diff --git "a/data/wo.txt" "b/data/wo.txt" new file mode 100644--- /dev/null +++ "b/data/wo.txt" @@ -0,0 +1,37377 @@ +Albert Einstein (juddoo Ulma (Almaañ) ci atum 1879, faatoo Princeton (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig) ci 1955) doonoon na ab boroom xam-xamu jëmm, xaymakat, xetlukat bu waa Almaañ bu jëloon réewu gu waa Suwis, te mujje ca Diiwaan yu Bennoo yu Amerig. + +Lu weesu doon gi mu doonoon kenn ci jëmmkat ak xaymakat yi gën a siiw ci àdduna bi ci taariixu xam-xam, doonoon na xalaatkat, ku bari yëggu-yëggu ci yeneen fànn (tambalee ca xeltu ba ci politig). Boole nañu ko ci gëstukat yi gën a màgg ci xarnub XX. + +Bokk na ci li ko gën a siiwal gisiin wi mu def te duppe ko gisiinuw ajoo. Dugal na it loxoom ci li jëmale-kanam doolerandub kàttan-ferñent, doolerandug tekkaaral, añse. + +Jotoon na Neexalub Nobel ci jëmm ci atum 1921 + +Dundam +Albert Einstein Ulma la juddoo ca Almaañ aji juram ju gòor mooy Hermann Einstein, doonoon booroom këru liggeéyukaay bu doon defar ay wuutuloxo yu mbëj, Pauline Koch doonoon aji juram ju jigéen. + +Jëmm +Ndakaaru (Dakar) Nekkoon reewu Afrig gu sowwu gu Faraas (ASF, walla AOF ci FR), Ndakaaru fimne mooy reewum Barug Senegaal akit goxub Ndakaaru, tolluwaayam ci péeteg sowwu bu Afrig, ci jegeem Daanaka-dun bu Kap-Wert, waral na sancug notaakon yu jëkk yi, Akit yaxantu ak Àdduna bu bees bi, te ame na peetewaayu ngëneel ci jëflanteg cosaani Saa-Afrig yi ak Saa-Tugal yi. Fa lees Taxawalee woon Xumbalu Àddina bu fànni ñuule (jaam yu ñuul) bu njëkk bi ci xalaatu Leopool Sedaar Sengoor atum 1966, Dëkk bii mooy toogu bu Këru-gëstu bu dàttu bu Afirg gu ñuule (KDAN, walla IFAN ci FR) akit bu Bànk bu diggu bu guuri Afrig gu sowwu (BDGAS walla BCEAO ci FR) + +Dëkki Senegaal +Péy +ANAFA (Mbootaay la ma jublu ci mbirum jàngale ak tàggat ñeel muskàllaaf) mi dalu Dakaar Senegaal, sóobu na ci liggéey bi jëm ci tekkib xelteef booloo-bokk, na ka SPIP (aw doxiinu ciiwal ci lënd-jokko Internet ngir gën a mën a saytu dalub jagal yi). + +ANAFA, ànd na ci ak benn MNJ (Mbootaay mu Nguur NGànkul) ca reéwum Kanadaa Alternatives, te fas yéene, ci lu yàggul, jagal ay sumb ci Wolof, Pular ak Màndey ci Wikipediyaa ak itam jokko ak bépp MNJ (ci Afriq mbaa feneen) yu farlu ci yëkëtiinu làkki Afirig ci Lënd-jokkoo bi. + +mbootaay yu Senegal +End : réewu Asi + +Réew +Asi +End +Senegaal menn la ci réew yi ne ci Sowwu Afrig, mu bokk nag ci Afrig gu bëj-saalumu saxraa (Afrique sub-saharienne), Mbàmbulaanug Atlas diw digam ci sowwu, taqaloo ak Gànnaar ci bëj-gànnaar ak penku, Mali féete ko penku, Ginne ak Ginne Bisaawóo ci bëj-saalum, Gàmbi moom sos ab daanaka-jiba (quasi-enclave) ci biir Senegaal, sutuxlu ba ci lu ëpp 300 jñ (km) ci biir suuf yi. Duni Bopp bu Nëtëx bi (Cap-Vert) ñi ngi ci 560 jñ ci tefesi Senegaal yi. + +Réew maa ngi duppe aw turam ci dex gi ko peeg ci penku ak bëj-gànnaar, te ab balluwaayam bawoo ca Fuuta Jallon ca Ginne, di Dexug Senegaal. Njuuxam lu gëwéel la te di lu fendi te yor ñaari jamono: jamonoy nawet (jamonoy taw) ak ju noor (jamonoy fendi). + +Ci jamonoy canc gi (la période coloniale), ay digg yu yaxantu yu bari, yu ay imbraatóor yu canc (empire coloniale) moomoon, daal di woon nañuy sampu ci tefes gi gépp. Dëkkub Ndar mujj na di péeyub Afrig gu Sowwu gu Faraas, mu mujj juge ci di leegi Ndakaaru ci 1902, moom Ndakaaru nag mujj na di péeyu Senegaal ca ba mu jotee ca ag tembam / jonnam ca 1960, nekk ci cat li gën a féete sowwu ci kembaarug Afrig + +La dale 2012 ba fii mu ne Maki Sàll mooy njiitul réew ma. Senegaal ak donte bokk na ci càmpéef yu bari yu àdduna si, teewul bokk na ci Bennoo gu Afrig (Union africaine) ak Mbooloom diiwaan yu Saxel-sahraa yi (Communauté des États sahélo-sahariens) + +Senegaal nag yaatoo na 196.190 jñ2. + +Gongikubaat +Cosaanul turu Senegaal dañul di jeqi dàggasante ak werante. ca 1850 labbe bii di David Boilat, ca mbindam ya mu doon def ci Senegaal,daa gisoon ne Senegaal mi ngi juge ci waxiinu wolof wii di suñu gaal. Bii nag mooy gis-gis bi gën a siiw, te xibaarukaay yi (les médias) gën koo ame. te moone lu ñu nangoodi la te sikk ko la ko dale ca ati 1960, ay gongikubaat yu bari nag joxe nañu leen, ci misaal biy taf cosaanul tur wi ci ag giir gu berber gu Sahara, mooy giirug Zenaga walla Sinhaaj, naan: Turu Senegaal mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Waaye werante wi dañul di tàng ci loolu ba tay. + +Njëkk-taariix + +Lu ci ëpp Njëkk-taariix ci Senegaal day tudd - ba laa tudd lenn - gëwéeli xeer yu mag yi (walla les cercles mégalithiques) yu Senegàmbi yi, walla jóori xor yu ñu sàkk yi (les amas coquilliers artificiels), yu ci mel ne ya nekk ca dunub Faajut. + +Jàpp nañu ne Senegaal dëkkees na ko ci njëkk-taariix lu jiitu lool juddug Isaa. Ay doj yu ñu yatt yu Jamonoy doj wu ñu yatt ju njëkk ja(Le Paléolithique inférieur ), wuññees na leen ci daanaka-dun bu Bopp bu Wert bi (Cap-Vert) ak yeneen yëf yu gongikoo ci doj, ñu jekkal leen, dees leen di fekk ci diiwaanub Tëngéej ak ci pegi dexi Senegaal gu penku gi. + +Ci jamonoy doj wu ñu xacc (néolithique), jumtukaay yi tàmbali nañoo soppiku ak a wuute, bu ko defee suuf su ñu togg (walla céramique) daal di feeñ. Gasi gëstu ya ñu doon def ca diiwaani tefes ya feñal nañu ay desiiti waañ yuy seere ak a firndeel askan wu mag wu ay nappkat aki yaxantukat wa fa nekkoon (marigot bu Xant ca delta, sottikukaayu dexug Saalum). + +Ndefarug mbell (walla gu weñ (metallurgie)) jëm na kanam ci jamonoy mbell yi (protohistorique) (junni bu ngëkk bi njëkk Isaa), fi ñuy gis ay bàmmeel ci bindu ay mbaanaar (tumulus). Ci digg réew mi, fa tollook Gàmbi gu tay gii, dees na fa fekk mbooloom gëwéeli xeer yu mag (cercles de mégalithes) ci aw dog wu tollu ci 100 jñ ci kaw 250|jñ. + +Nguur yu njëkk ya + +Dëkksi gi dafa doon gën di dolliku ndànk-ndànk tey gën di dëgër ngir àgg ci sos ay nguur yu njëkk yu sosu ci VIIeelu xarnu, nguur gu Tekruur, gu Namandiru, gu Jolof, ak ay mbokkoo yu sori ak Iimbraatóor gu Gana, ci suufus Mali gu tay gi. Ci nguur yu wuute yooyu, gi ci ëppoon doole ci XIVeelu xarnu moo doonoon imbraatóor gu Jolof, gi boole woon Kajoor, Bawol, nguuri séeréer yu Siin ak yu Saalum, Waalo, Fuuta-Tooro ak Bambug. Ci bëj-saalum, nguurug Kaabu, teg ci gu Fulaadu. + +Jolof nekkoon na imbraatóor gu Njaajaan Njaay sosoon, ki njëkk a nekk Buurba (buur) ca Jolof. Faleesoon na ko njiit ca loolu doon mujj di nguurug Waalo, ca bëj-gànnaar-penku gu Senegaalug tay gii, ca diiwaanu dex gi. Dajale woon na mbooleem askani giirug wolof ngir taxawal imbraatóor gii ci XIIIeelu xarnu . Ibraatóor gi saayoon na te naaxsaay ci 1549, ànd ak deeg imbraatóor ba mujjoon ca Jolof, Lele Fuli Fak, ki ko rayoon di Amari Ngóone Sabel Faal, ki nekkoon ca jooja jamono kilifag diiwaanu Kajoor. + +Jolof des na di aw dog (vassal) ñeel imbraatóor gu Mali ci diir bu tollu ci xarnu. Ba loola amee, yeneen nguur yi, ñoom itam gu ci nekk, tàmbalee jël ag tembam ba mujj wàññi imbraatóor gu Jolof gu mag googu ba àggal ko ci tolluwaayu genn nguur gu yam ca digg réew mi. Ci ñaareelu xaaj bu XIXeelu xarnu, sancaani Faraas yi (les colons francais) tàmbali woon nañoo nangu ndànk-ndànk mbooleem nguur yu Senegaal yii. Jolof moo nekkoon nguur gi ñu mujj a nangu ak Buurab Jolofam bu mujj ba Alburi Njaay, ci ron deflu gu Luwis Federb. + +Lislaam a ngi njëkk a tàbbi ci Senegaal ci diggante VIIIeelu xarnu ak IXeelu xarnu, ña ko fa dugal di ay yaxantukat yu araab-yu-berber. Dañu doon tas diine jii ci jàmm, ñu njëkk koo jox Jula yi tuubloo ci ginaaw bi Tukkloor yi ak Saraxule yi, ñoom itam ñu tas ko ci Senegaal gi gépp. Bi ñu demee ba ci kanam ca XIeelu xarnu , la Muraabituun, jug, Tukkloor yi jàpple leen, ñuy jéem a tuubloo mboolooy jaamukati xërëm yi jaare ko ci Jiyaar. Loolu benn la ci sabab yi tax Séeréer si gàddaayoon dem Siin-Saalum, Wolof yi, Pël yi ak Mandinke yi, te ñoom ñepp ña nga jalu woon ca Tekruur. Lislaam teel na tas ca imbraatóorug Jolof. Waaye ca XIXeelu xarnu la nangu ca dëgg-dëgg mbooleem askan yi, ci anam gu jàmmu, loolu nag deesi sante ko Sëriñ si, ku mel ne Seex Ahmadu Bamba, mi sos yoonu murit, Alaaji Maalik Sy kenn ci kilifay Tiijaaniya walla Seydina Limaamu Laay, ki sos laayéen gi, ñi yéemoon nit ñi ci seenug mbaax ak ragal Yàlla ak séeni karaama( xar-baax). Moom Lislaam tam nekkoon ab ker-keraan (moyen) ngir boole nit ñi te di leen aar ci jalgati yi ñu miinoon ci nguur yi (jiyaar yu toftaloo, canc gu ñu teg ci doole, jalgatiy Ceddo yi). + +XIXeelu xarnu ñi ngi ko gën a xame ci daanug nguur yi, jàllsig sancaan yu Tugal yi ( colons européens ) ak jàmmaarloo gi lànk canc gi, ñi ko jëmmal di ay nit ñu mel ne Lat Joor, Alaaji Omar Taal, Mamadu Lamin Darame, Alburi Njaay walla Màbba Jaxu Ba. Diiney katolig (walla nasaraan, ndax katolig bànqaas la ci nasaraan) daal di tasu, ñi ko def di ay nasaraanalkat yu Tugal la ko dale ca XIXeelu xarnu, rawati na ca Siin ak kaasamaas. + +Taariix +Lislaam tàbbi na Senegaal ci fukk ak benneelu xarnu,ànd ak giirug Sinhaaj gu Amaasix gi. Turu Senegaal waxees na ne mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Askani Senegaal yi sos nañu ay nguur aki nguur-nguuraan, yi ci ëppoon solo di Imbraatóor gu wolof ca diiwaani Waalo, Kajoor ak Bawol, ci fukk ak ñeenteelu xarnu g.j, ak nguuruñg Tukklóor ak gu Deñaanke gu Pulaar gi ca penku bëj-gànnaar ga. Ay dooley Tugal teg nañu loxo ay wàll ci ay tefesam, ci fukk ak juroomeelu xarnu g.j, ginnaaw bi Faraas daal di teg loxo réew mi mépp, ginnaaw ay xare yu limu. Ci atum 1902 la Ndakaaru nekke péeyub Afrig gu sowwu gu Faraas gépp. + +Seŋoor walla Léopold Sédar Senghor(1906-2001)(1960-1980) mooy ki njëkk a nekk njiitul Senegaal, yoroon dàkkantalu njiit liy woykat (walla taalifkat) +Ci samwie 1959, la Senegaal bennoo ak li ñu daa wax Sudaan gu Faraas gi, ci ron turu Lëngoo gu Mali (fédération de Malie). Lëngoo gu Mali googu tembe na ci Faraas ci 20 suwe 1960. Waaye ginnaaw ay jafe-jafe yu politig, Lëngoo googu mujj na di ñaari réew ci 20 ut 1960: Senegaal ak Mali. Jibaleesoon na ag lëngoo ci diggante Senegaal ak Gambi ci turu Senegambiya atum 1982. Waaye ci jëf feeñul, bu ko defee ñaari nguur yi tàggalikoo atum 1989. Am na ab jë bu ngànnaayu (front armé) bu nekk ci bëj-saalumu réew mi, ca Kaasamaas bu bëgg tembteg diiwaan ba, leeg-leeg mu xareek nguur gi, la ko dale ca atum 1982. +_ + +Canc gi + +Sancaan yi (les colonisateurs) seen teg loxo gu canc gi (conquête coloniale) mi ngi door bi wuññig suuf yii amee ci 1442 ci loxol moolub Veneto (ab diiwaan ca Itaali) bii di Cadamosto, bi mu defalee ay wuññi ñeel Portigaal. Ca jooja jamono la waa portigaal daal di sóobu - ci lu gaaw - ci Njàppum jaam (walla jaayug nit ñu ñuul ñi), waaye doon nañu war a janook gëpplante (la concurrence) gi bawoo woon ci jaaykati ñu ñuul ñi te bawoo woon Britaani (négriers britanniques), Faraas ak Olaand ca Yaxantug ñatti-koñ ya (Commerce triangulaire). + +Waa Olaand yi sos nañu ab diggub yaxantu ca dunub Gore, Faraas taxawal ca 1659 digg bii di bu Ndar nga xam ne moo mujj di péeyub Senegaal bu njëkk bi. Ci 1677 waa Faraas ñi ñëw nangu dunu Gore (benn ci digg yu mag yi ñu daa jaaye jaam yi ak Ndar ak tata ju dunu James ca Gàmbi). + +Nosteg canc daal di nay taxaw ci dikkug Federb, Kaŋub Senegaal (le gouverneur du Sénégal) la ko dale ca 1854 ba 1861 ak 1863 ba 1865, mooy ki samp dàtti Afrig gu Sowwu gu Faraas gi (ASF)(AOF). Ci wormaal gi mu defoon aada ya fa cosaanoo ( du dëgg, wormaalu ko fenn) la tàllale jeexiital (l'influence)gu Faraas ba mu weesu Senegaal, mu liggéey ci lu jëmale kanam koom-koomu barab bi (ci njariñul Faraas rekk nag lol réew mi yitteelu leen woon ci lenn), daal di sos waaxub Ndakaaru. + +Ginnaaw Ndar, Ndakaaru mujj na ci 1902 di péeyu Afrig gu Sowwu gu Faraas gi, benn ci sancu yu Faraas yi . + +Ci samwie 1959, Sudaan gu Faraas gi (Mali gu tay gi) ak Senegaal seey nañu ci Lëngoo gu Mali, gi nga xam ne mujj na temb ci 20 suwe 1960. Temb gii mi ngi juddoo ci tuxalug ay nguur ( transferts de pouvoirs ) yu amoon ca dëppoo ga ñu xaatimoon ca Faraas ca 4 awril 1960. + +Politig +Senegaal nguurug demokaraasi la gu limuy làng (gu bariy parti), njiitul pénc mi (président de la république)dees na ko tànn ngir diirub juroomi at (leegi soppees na ponku sartu réew bi aju ci diirub ngiitug réew mi, yobbóoti ko ci juroom ñaari at, ginnaaw bi ñu ko soppee jële ko ci juroom ñaar, yobbu woon ko ci juroom), moom njiit li nag mooy tànn njiitul jëwrin yi. Barlamaab Senegaal ñi ngi koy wooye Péncum ndawi réew mi mbaa ( jataayub xeet wi), am na nag 120 cér yu ñiy tànn ci ay tànnéef (élections) yu dul yu njiitul réew mi(tànnéef yu yoonal yi : élections législatives) ngir diirub juroomi at + +Mii menn la ci réew yi gën a am demokaraasi te gën a dal ci Afrig, ndaxte genn daaneel nguur (coups d'État) masu fee am, « Senegaal niki roytéef » yagg nañu koo joxe, wone ko ngir ñu roy ci, ba tee ay yi di fi am ak doonte Amnesty International mi ngi ñaawlu yenn jàpp yi yor mbubum politig. + +Senegaal am Pénc la mu demokaraasi (une république démocratique) (lu sakkan ci ay làngi politig a nga fa). Noste ga fa nekk gu njiitug réew la, ndax ba mu amee ag tembam Senegaal daa daal di jël Faraas niki roytéef, roy ca politigam ba ca 1958, niki yeneen réewi Afrig yi bokkoon ci ASF(Afrig gu Sowwu gu Faraas).Sartu réew bu Senegaal mi ngi taariixoo ci 1959, xoolaat nañu ko ci 1960 ki ko def di Léopold Sédar Senghor ginnaaw genn laaju (référendum). ay xoolaat (révisions) yu bari topp nañu ci, ñooy gu 1963 moo fi saxal nosteg njiitu réew (ci jamono jooju : dindi njiitul jëwriñ) teg ci gu 2001 gi yobbu àppub njiit gi jële ko ci 7 at, yobbu ko 5 at (jataayub mag ñi(le sénat) jëlees na ko fi, ginaaw bi ñu delloosi ko ci 2007). + +Njiitul Pénc mi( Le Président de la République) (xoolal limub njiiti Senegaal yil) mooy kilifag nguur gi, moom nag ñi ngi koy tànn, mu ame ci pal gu mbooloo mi (suffrage universel) ci anam gu jonjoo de (manière directe) ci diir bu tollu ci juroom ñaari at, manees koo yeesalaat benn yoon. Mooy fal njiitul jëwrin yi (xoolal limub njiiti jëwrin yu Senegaal) moom itam (njiitul jëwrin yi) mooy tànn jëwrin yi, ba noppi sàkku ci njiitul réew mi mu tabb leen. + +Ki njëkk a nekk njiitul Senegaal mooy Léopold Sédar Senghor,mu nekkoon njiit lu ubbeeku te dib taalifkat bu siiwoon . Ci 1981 la ko njiitul jëwrinan lii di Abdu Juuf wuutu, waaye ci 2000 la Làngug demokaraasi gu Senegaal gi am ndam ci njiitug Abdulaay Wàdd, ñu falati ko ci 2007. Njiitul góornamaa bi fi nekk fii mu ne mooy Seex Ajiibu Sumaare. + +Parlamaa bu Senegaal yor na ñaari néeg : Péncum ndawi réew mi ak jataayub mag ñi. + +Bi ñu ko taxawalee ci 20 ut 1960,Péncum ndayi réew mi mi ngi yor 150 ndawi réew, yu ñu fal ci pal gu mbooloo mi ci anam gu jonjoo (au suffrage universel direct) ngir diir bu tollu ci 5 at. Tànnéef gi gu ëppte la (Le scrutin est majoritaire) ci genn wër, ci tund yiy xëccoo 90 ndawi réew, di it gu kem (proportionnel) di ab lim bu tas ci réew mi ñu koy xëccoo mu tollu ci 60 ndawi réew. Péncum ndaw yi Macky Sall moo ko jiite, mi nekkoon Njiitul jëwrin yi, waaye fii mu nekk, aw yoon jug na wu Saada Njaay indi ngir ñu jële ko fi, wàññi ab àppam ba du weesu menn at ngir man ko fee jële, wii yoon nag, jot naa jàll, waaye njiitul réew mi dëggalagu ko. Tànnéef yu yoonal yu Senegaal yu 2007 jàll nañu ci ndam lu yaatu lu àndandoo gu njiit gi (coalition présidentielle), waaye lu jege ñaari ñatteel (deux-tiers) ci falkat yi demuñu woon ca mbañ-gàcca ya, li ko waral di ndigalul dogoo(boycott) lu bawoo ci làngi kujje gi. + +Parlamaa bu Senegaal boroom benn-néeg (monocaméral) la woon, ci diirub jenn jamono: Jataayub mag ñi, muy lu ñu dindi ci 2001 ci ginnaaw genn laaju gu sartu réew (référendum constitutionnel), delloosi nañu ko ca mee 2007. Mag ñi (Les sénateurs) nag dinañu tollu ci limub 100. 35 ya ca ñoom dañu leen a fal ci anam gu jonjoodi (au suffrage indirect) ci tund yi, yeneen 65 yi njiitul réew mi di leen tabb. Paap Jóob, kilifag Ndakaaru moo ko jiite . + +Am na yoon (loi) wu ñu def ci diggadil gi(La loi sur la décentralisation), nekk na it di lu ñuy doxal la ko dale ca samwie 1997, , yoon woowu jox na ay ay doole yu am solo ñeel jataayi diiwaan yi (assemblées régionales). + +Ci 1992 la Àttewaay bu Kawe (la cour suprême) bu Senegaal bi nekk di lu ñu dindi, ñu wottee ko cér (organes) yu jagoo loolu: Àttewaay bu firi bi(Cour de cassation), Jataayub nguur gi (Conseil d'État) ak Jataayub Sartu réew mi (Conseil constitutionnel), yooyu cér di yu niru lool séeni moroom ya nekk Faraas. Seeni àttekat Njiitul réew mee leen di tabb. Yooyu ñooy bànqaasi yoon yi gën a kawe ci réew mi (les plus hautes instances judiciaires du pays). + +Dalub Àttewaay bu firi bi ëmb na lenn njiit lu njëkk, ak ñatti njiit yu néeg (trois Présidents de chambre) ak gën jaa néew juroon ñeenti xelalkat (9 Conseillers). Ca toppewaay ba le (Parquet), mi ngi ame ci ab Toppekat bu Matale (un Procureur général) , ci benn layalkat bu njëkk bu matale (un Premier Avocat général), ci gën jaa néew ñaari layalkat yu matale (deux Avocats généraux) ak gën jaa bari juroom benni déglukat (six Auditeurs) yu koy liggéeyal. Am na ñatti néeg, yoy bu ci nekk mi ngi ame ci lenn Njiit ak ñaari xelalkat gën jaa néew: + + Néeg bu njëkk bi mooy àtte layoo yi aju ci wàllug tooñaange yi (pourvois en matière pénale), + Bu ñaareel bi di àtte layoo yi aju ci mbirum ñoñ ak yaxantu ( pourvois en matière civile et commerciale) + Bu ñatteel bi di sëgg ci wàll yi jëm ci mboolaay (yoonu liggéey ak kaaraange gu mboolaay)(droit du travail et sécurité sociale). + +Jataayub nguur gi ay xaaj yu bari ñoo ko sos: + Xaaj bu njëkk bi moom lañu féetale xuloo yi aju ci bindu ci limi tànnéef yi(les listes électorales), yoonu (légalité) gu jëfi mbooloo yu barab yi ( collectivités locales ) ak diiŋat yi ngir neenal gu aju ci nguur gu ëpp (les recours en annulation pour excès de pouvoir). + Xaajub ñaareel bi day def li Àttewaayu xayma yi (la Cour des comptes)di def ca Faraas , ci moom sax la jële woowiinam woowu bu yàggul rekk. + Xaaj yooyu yépp nag am nañu ay njiiti xaaj (Présidents de section), ay xelalkati nguur (les Conseillers d'État) ay xelalkati laaju (les Conseillers référendaires) te ki leen jiite mooy njiitul jataayub nguur gi (Conseil d'État). + +Jataayub sartu réew bi yor na juroomi cér, yu ñu tabbe ci ag santaane (décret) ngir juroom benni at yu ñu dul yeesal, yoo xam ne njiit ca la ak topp-njiit (Vice-président). Dees na ko yeesal cig wàll waaye déet lépp, waaye du weesu ñaari cér gën jaa bari. Ab liggéeyam mooy fuglu tànnéef yu yoonal yi, ak xool ba xam yoon yi (les lois) dëppoo nañook sartu réew mi, ak warlu yu àdduna yi (les engagements internationaux). + +Senegaal dindi na mbugalum ray ci 10 desambar 2004. + +Gëstu-askan +Li ëpp ci gëstu yi ñu def ci wàllug Gëstu-askan (walla demogaraafi) ci Senegaal dafa sukkandiku ci Waññ (recensement) yi ñu jotoon a def ci 1976, 1988 rawati na 2002. Doxal gu Séentu ak Lim gi (la Direction de la Prévision et de la Statistique) ci 2004, siiwaloon na « ay leeral ci askani Senegaal yi, loolu di woon lu juge ci waññ gu 2002 » mu sóoraale woon ci màgg gi man a ami ci askanu Senegaal la ko dale booba ba 2015. + +Bu ñu sukkandikoo ci gongikuwaay yii, askanu Senegaal - wi doonoon lu toolook 1 milyoŋ ciy way dëkk ci 1900 ak 2,8 milyoŋ ca jamonoy ag tembam ca 1960 – yekkatiku na tay ba àgg ci ciy jëmm (nattale gi ci 31/12/2007) te man naa àgg ci ci mujjug 2015. Askan wii kon day màgg ci anam gu gaaw, ànd ak benn tolluwaayu njuru (taux de fécondité) bu tiim 4 doom ci jigéen. + +Seetloos na fa genn kuute gu giir gu mag: Wolof (43,3 %), Pël (23,8 %), Séeréer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malinke (3,0 %), Soninke (1,1 %) Maanjanke (2%) ak yennat ci ay giir yu gën a néew, te gën a gawu ci barab,waxuma la nag naari Libaan yi ak Tubaab yi, nga xam ne ñi ngi nekk ci dëkki taax yi . Ci mujjug 2007, ci waa Faraas bindu woon nañu ci seen barabu aji teewal (ambassade) (boroom ñaari réewu it ci lañu woon (les binationaux)). + +Ab diir bu yàgg a ngii askan wi nekk di jalu ci fi jàkkaarloo ak Mbàmbulaan gu Atlas gi, waaye nocciku gu kaw gi (l'exode rural) yokk na yamoodi gi ci séddale gii. Fi mu nekk ñeenti nit yoo gis ci waa Senegaal, kenn ka mi ngi dëkk ci Daanaka dun bu Bopp bu Wert bi (Cap-Vert), looloo waral péey baa ngi waaj a xëx. + +Bu Ndakaaru jàllee, diiwaan yi ñu gën a taaxal (les régions les plus urbanisées) ñooy Siggicoor, Cees ak Ndar. Yi gën a néew ag taaxal (moins urbanisées) ci diiwaan yi ñooy Koldaa, Maatam ak Fatig.Diiwaanu Tàmbaakundaa nag moo yor fatt (densité) gi gën a doyadi (11 way dëkk ci jñ²). + +Bu ñu sukkandikoo ci nattale yu 2007, digg yu taax yu diiwaan (les centres urbains régionaux) yi yor lu ëpp ciy way dëkk ñooy Tuubaa ( (Man nag yaakaar naa ne ag na ma xame Tuubaa, la fa dëkk man naa ñeentte lim bii ñu wax) – mi jekki jekki gis ag màgg gu yéem ñépp –, Cees (), Kawlax (), Mbuur (), Ndar (), Siggicoor () et Njaaréem (). + +Ca 2007, Senegaal teeru woon na lu tollu ci 23,800 ciy daw-làqu ak sàkkukati ag wéeru ( demandeurs d'asile), yoo xam ne lu ëpp 20,000 ca ñoom ay waa Gànnaar lañu, yu doon daw boddanteg xeet ga, ak ñennat ci waa Liberiyaa, waa Siraa Leyoon, ak yeneen réew . + +Gàddaay +Bu Senegaal dee réew muy teeru ay way gàddaay (ay migrants), moo xam yu ay jamono lañu(saisonniers) mbaa déet, moo xam yu bawoo ci réew yi mu digool lañu walla yu ko sori, du tee menn mbooloo mu Senegaal mu mag ma ngay dund ca bitim réew. wisaaroo gii (diaspora)alal ju am solo la ci réew mi, ci wàllug koom ak njëmmte (identité). Xarala yu xibaar ak jokkoo yu bees yi XXJB dañuy gën di jàppandal jokkoo ci diggante njaboot gi te tax it deesi man a dund mu mel ne da ngaa nekk ci sa biir réew . +Li ëpp ci ñiy dem nag ay waxambaane lañu yu jublu Tugal, rawati na Faraas, ak Itaali, walla ñuy dem ca Aamerig gu bëj-gànnaar ga, ca Kebeg yobbaale ci seeni xol naalub dellu réew ma ci ginnaaw yennat ciy at. Màggug gàddaay gu yoonoodi gi (immigrations clandestines), ñu koy def ci ay anam yu bon te ñaaw jëm ci Duni Kanaari yi lu tiital Senegaal la ak réew yi koy teeru. + +Ñi gën a ñàkk yaakaar ñoom faalewuñu sax ay wi ñu ci man a dajeel, ginaaw gis nañu seeni moroom tekki, rawati na ya bokk ca wisaaroo ga (diaspora) — moo xam Senegaal lañu juddoo mbaa dañu faa am rekki way jur - rawati na ñi ciy yëngu ci tàggat yaram mbaa fànn (art). + +Lu sakkan faatoo na ci gàddaay gu yoonoodi gi, mbaa mbëkk mi, baat bi ñu ko gën a xame, lu ko waral? xanaa géej gi ñu sóobu ci lu duli jumtukaay yu dëppoo , ñoom kay dañuy sóobu ci ay looca yu doyadi, duy kooki bagaas ak nit ci wépp xeet ak maas, bu ko defee yooru, duñu faale la leen dëgmal ciw ay ak musiba, gaal gaay doon duus ba, néegub añ ba, bu tëdd ba, leeg-leeg duus ñëw téq leen mbaa ngelaw lu saf, ba kero ñuy àgg bu ko Yàlla dogalee, waaye cis lëf cig loof, lu sakkan di ca des dib añ mbaa reerub ag kuréel ciy jën yu waroon a nekk diy añ ñeel leen mbaay reer. Nii lay deme ba kero ñuy àgg ak la leen fay xaar ciy kaso ak ëlëg gu lëndëm, lii mooy li xew ci mbeex mi, waxuma la nag la ca tàkk ga, aji tàng ji tàkk gii nga xam ne jali beeñ yi yàgg nañu fee tee nit àgg fa mu jëm. + +==' + + + + ' Koom-koom == + +niou boolé chi chi waallu kom kom you beess yi fa feegn chi 2012 ak tay. guiss nagne fa petrole ak gaz ak zircon ak wourouss +Senegaal nguur la gu bokk ci Bennoo gu koom-koom ak gu koppar gu Afrig gu sowwu gi. Ginnaaw ay jafe-jafe yu koom-koom ci njëlbéenug ati juroom neen-fukk yi, ay yoonam (ay luwaam) yu koom-koom soppiku nañu, bu ko defee ag màggam gu koom-koom mujj àgg ci ay 5% ci diggante 1995 ak 2001. Ci ndoortel 1994 Senegaal door na ci doxal tëriinu yéwénal gu koom-koom gu kawe ay yitte, ci càmmug mboolaay gu àdduna bi (communauté internationale), looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci Frank bu Faraas, mu woyofal ko ba ci 50%. Jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam, ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku, niki meew, yàpp, ceeb, ba àgg ci fulu ci genn guddi, waaye am na genn màgg gu am ci koom-koom bi, ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi, ngir yéwénal yi, nga xam ne àgg na ci 5% ci at mu nekk, bu ko defee walu gi(l'inflation) wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb. + +Tembte + +Ci 20/ut/ 1960, la Senegaal génn ci lëngoo gu Mali gi, daal di jibal ag tembam. + +Senegaal ak Gàmbi bennoo nañu ci 1982 ngir amal lëngoo gu Senegàmbi, waaye gii nekkutoon lu dul aw gisiin, kenn masu koo jëfe. Mujj gi ñu far ko tas ci 1989. + +Ay janoo jot nañoo am la ko dale ca 1982 ci anam gu dogatu ci diggante ñoñ tàqalikoo (les séparatistes) ñi nekk ci bëj-saalum gu Kaasamaas ak doole yu góornamaa bi. Ginaaw ay jéem yu bari yu àntuwul, genn dëppoo mujj nañu ko xaatim ca Siggicoor ca 30/desambar/2004 ci diggante jëwrini biir-réew ji woon Usmaan Ngom ak làbbe Augustin Diamacoune Senghor, mi nekkoon njiitul fipp gu Yëngu-yëngu gu doole yu demokaraasi yu Kaasamaas (YDDK)(MFDC), moom Diamacoune Senghor moomu mujj na faatu. + +Beneen tombub coow ci diggante ay waa Kaasamaas ak Ginne-Bissaawuóo màgg na ci awril 2007. + +Ci 1989, Gànnar ak Senegaal génne nañu ku ci ne, ci anam gu ñaaw sa njabootug moroom te ña ëppoon ca ñoom ña nga juddoo woon fa ñu leen génnee, muy réew mi leen doomoo woon, ñu jotoon faa seey ca mboolaay ga ak koom-koom ba. Bu ñu sukkandikoo ci li Jataayub daw-làq bu kawe bi (JDK) HCR wax, ay daw-làqu ña nga des ba tay ca guddaayub dexug Senegaal gi. Ci 2007, Njiitul Gànnaar jibaloon na ba muy def càkkug palaam ga (campagne), ne nangu na delsig doomi réewam yooyu doon dund ci Senegaal ak Mali te neexu leen. + +Melosuuf + +Senegaal a ngi nekk ci diggante 12°8 ak 16°41 wu rëddu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 wu rëddu tus-wu-taxaw wu sowwu. digam wi gën a féete sowwu mooy Ndakaaru di it cat li gën a féete sowwu ci goxu Afrig. + +Su ñu ko méngalee ak réewum Mali walla ak mu Gànnaar di nanu gis ne Senegaal réew mu tuuti la ci rëyaayu-suuf. + +Kilimaa + +Kilimaab Sahel la ame: + Nawet maami koor la ba kori. Bëj-saalum gi moo ëpp taw. àllub yamoo bi ca Caasamaas la nekk, ndax ay tawam yu bari; + Noor moom diggi tabaski la ba rakki gamu + +Seddatleg yoriin + +Ca atum 1996 la seddale gu mujj gi ame, mooy giy wéy ba tay, lu dul coppite yi ci mujj a am: Sosug diwaanu Maatam ci 2001 ak gox-goxaan bu Kungeel ci 2006. + +Ci 2008, la Senegaal nekk 14 diwaan, + +Yenn ciy dëkk: + Cees, 311 324 way dëkk (2005) ; + Ndakaaru, 1 009 256 way dëkk (2004) ; + Jurbel + Luga + Maatam + Mbuur + Mexe + Ndar, 154 496 way dëkk (2001) ; + Podoor + Tuuba + Tëngéej + Kawlak, 185 976 way dëkk (2007). + Siggcoor, 158 370 way dëkk (2007) ; + +Giir yi +Senegaal doon na réew mu bariy giir, waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi Afrik yu bari, wuuteg ay giiram du feeñ. Man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci caada. Man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew: Wolof (43,3 %), Pulaar (23,8 %), Seereer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malenke (3,0 %), Sooninke (1,1 %) Manjaak (2%), ak yeneen giir-giiraan yu tas ci réew mi, man nan cee boolee it tubaab yi ak naari libaan yi. + +toftaloog xew-xew yi + Ci VIIeelu xarnu : nguur yu njëkk ya + XIeelu xarnu : Feeñug Lislaam + 1442 : doorug teg loxo gu sancaan yi + 1444 : wuññig Dunub Gore. Joqalante yu yaxantu yu njëkk yi ak waa Tugal ñi ngi door bi Waa Portigaal agsee ci sottikuwaayu Dexug Senegaal ak Cap-Vert (Bopp bu wert bi) (Nekkeesoon na di joqalante ay ndima aki weñ (métaux) ci pëndëxu wurus (la poudre d'or), ak daakaande ak bëñu ñay (dl'ivoire)). + Ginaaw 1600 : Waa Faraas ak waa Olaand dàq nañu waa Portigaal. + 1659 : Taxawal Ndar + 1700 : Faraas yilif na yaxantu gi ci diiwaani tefes yi. Ak li kujje gi di tar ci diggante Faraas ak Britani lépp ak xeex yu bari yi teewul cangug Faraas akug jeexiitalam tallaliku. Bi mu toogee ca Ndar, Faraas daa daal di yéeg ci Dexug Senegaal gi ngir àgg Niseer, ak doonte daje na ak yenn jàmmaarloo yu bawoo ci yennat ci ay giir niki (Tukulóor yi ak Pël yi). + 1815 : Ndajem Vienne mi jox na Faraas Gore. + 1818 : njaayum jaam yi dindees na ko ca Faraas. + 1852 : Federb wàcc na Senegaal, daal di àtte, dale ko 1854 ba 1861 ak la dale 1863 ba 1865. + 1855 : Wàllug teg loxo gu xare daal di door ci nangug Waalo. + 1857 : Sosus Sànnikati Senegaal yi(les tirailleur sénégalais). + 1857 : Jëlug barabub Ndakaaru cig dëppoo ak kilifay lebu yi. + 1860-1865 : Mbooleem Kaasamaas gu suufe gi ba Siggicoor rot na ci ron yiirug Faraas (sous protectorat français). + 1886 : Faatug Lat Joor ak jeexug jamonoy Dammeel. + 1892 : Xare yu mag yi jeex nañu + 1895 : SosugAfrig gu sowwu gu Faraas gi (ASF)(AOF). Senegaal mujj na ci anam gu fés di ab sancu bu Faraas, ñu koy yore ak a doxale ca Ndar. + 1902 : Tuxalug péeyub (ASF)(AOF) jële ko Ndar, yobbu ko Ndakaaru. Faraas mi ngi doon dundal koom-koomu Senegaal ci anam ga ko ñoroon te méngook ag jëm-kanamug réewam, googa di mbayum gerte, gu ñu war a génneji (culture de l'arachide destinée à l'exportation). + 1914 : Blees Jaañ mooy nit ku ñuul ki njëkk a toog péncum ndawi réew mu Faraas ; moom nag tëyye na toogub ndawu réewam boobu ba ci 1934. + 1959-1960 : Sosug lëngoo gu Mali (la fédération du Mali). + 1960 : Tembug Senegaal (Indépendance du Sénégal). + 1982-1989 : Sosug lëngoo gu Senegambi. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + À remplacer + +Lëkkalekaay yu biti + +Afrig +Réew + + +A +Afganistaan - Afrig gu Bëj-saalum - Dunu Aland - Albaani - Almaañ - Alseeri - Andoor - Angila - Angolaa - Antigua ak Barbuda - Araabi Sawdit - Armeeni - Arsantin - Aruba - Aserbayjaan - Ayiti + +B +Bahamas - Bahrayin - Banglaades - Barbados - Bareesil - Belaarus - Beliis - Beljik - Bene - Benesuwela - Bermuda - Boliibi - Bosni - Botswana - Brunaay Daarusalaam - Bulgaari - Burkinaa Faaso - Buruundi - Butaan - Dunu Buwet + +C +Cadd - Dunu Christmas - Ciipër + +D +Danmaark - Diwaan-yu-Bennoo - Dominika + +E +Ecoopi - Ekwadoor - End - Eritere - Eslowaaki - Esloweeni - Estooni - Eswatini + +F +Duni Faarow - Dunu Falkland - Faraas - Fiiji - Filipiin - Finlaand + +G +Gaambi - Gaboŋ - Gana - Gine - Gine Bisaawóo - Gineg yamoo - Gires - Grenada - Groenlaand - Guam - Guwaadalup - Guwaatemala - Guyaana - Guyaana gu Faraas + +I +Imaarati Araab yu Bennoo - Indoneesi - Iraak - Iraan - Irlaand - Isipt - Islaand - Ispaañ - Israayil - Itaali + +J +Jamayka - Jeoorji - Jeoorji gu Bëj-saalum ak Duni Islaand yi Bëj-saalum - Jibraltaar - Jibuti - Jordaani + +K +Kaledooni-Gu-Bees - Kamboodi - Kamerun - Kanadaa - Kap Weer - Kasakistaan - Kataar - Duni Kaymaan - Keeñaa - Kirgistaan - Kiribati - Dunu Kokos - Koloombi - Komoor - Kongóo-Brasaawiil - Kongóo-Kinshasa - Dunu Kook - Kore gu Bëj-gànnaar - Kore gu Bëj-saalum - Korwaasi - Kosta Riika - Kot Diwaar - Kowet - Kubaa + +L +Lesoto - Letóoni - Libaa - Libeeria - Libi - Liechtenstein - Lituwaani - Luksembuur + +M +Madagaskaar - Makaaw - Malawi - Maldiif - Maleesi - Mali - Malt - Marok - Duni Marshall - Martinik - Mayoot - Meksik - Mikroneesi - Miyanmaar - Moldaawi - Monaako - Mongoli - Montserrat - Móoris - Móritaani - Mosaambik + +N +Namibi - Nauru - Nepaal - Nguur-Yu-Bennoo - Nikaraaguwa - Niseer - Niseeria - Niue - Dunu Norfolk - Norweej + +O +Olaand - Omaan - Onduras - Ongiri - Ooŋ Koŋ - Óstraali - Ótriis + +P +Pakistaan - Palau - Palestiin - Panamaa - Papuwaasi-Gine-Gu-Bees - Paraguwaay - Peru - Pitkeern - Polineesi gu Faraas - Poloñ - Poortorikoo - Portugaal + +R +Reiñoo - Réewum Cek - Réewum Diggu Afrig - Réewum Dominik - Réewum Lawos - Réewum Maseduwaan - Riisi - Romaani - Ruwandaa + +S +Saambi - Sahara gu Sowwu - Saint Kitts and Nevis - Saint Lucia - Saint Pierre ak Miquelon - Saint Vincent and the Grenadines - Salbadoor - Samowaa - Samowaa gu Aamerig - San Marino - Sapoŋ - Saw Tome ak Preesip - Seent Eleen - Seerbi - Seland-Gu-Bees - Senegaal - Seysel - Siin - Siiri - Sili - Simbaawee - Singapoor - Siraa Leyoon - Siri Laanka - Duni Solomon - Somali - Sudaan - Surinaam - Suweed - Suwis - Swalbard ak Jan Mayen + +T +Taaylaand - Taaywaan - Tajikistaan - Tansani - Timor-Leste - Tiniisi - Tirinidaad ak Tobaago - Tirki - Togóo - Tokelau - Tonga - Turkumenistaan - Tuvalu + +U +Ugandaa - Ukreen - Uruguwaay - Usbekistaan + +V +Duni Virgin (angalteer) - Duni Virgin (us) + +W +Wallis ak Futuna - Wanuatu - Watikaa - Wiyetnaam + +Y +Yaman + +Melosuuf +Réewi + +nds:Land#Länner +sv:Världsgeografi#Lista över länder +Faraas (Republik Faraañse) : réewu Tugal (Óróop) + + Làkk : Ci Faraañse mooy France. + + Péy : Pari + + +Tugal +Réew + +Louis XIV Faraas +Gànnaar (Republik bu Lislaamu bu Gànnaar) : réew Afrig. + +Réew +Afrig +Gànnaar +Benin (Republik bu Benin) : réewu Afrig. + Lii Ab Sémp rekk la man ga cee dugal sa loxo ndeem am ga ci xam-xam + +Melosuuf +Bene aw rëdduw suuf wu sew la, nekk ci diggante yamoo gi ak Gëwéelub Sànkar bi. Rëddu tus-wu-gaar wu bene mi ngi ci diggante 6°30'bëj-g ak 12°30'bëj-g, tu-wu-taxawam moom mi ngi ci 1° P ak 3° 40'P. +Ay digam ñoo ngi yem ci Togóo ci sowwu, yem ci Burkina-faso ak Niseer ci bëj-gànnaar, ci Niseeriyaa ci penku, janook mbàmbulaanug Atlas gi ci bëj-saalum. Mi ngi am yaatuwaay bu tollu ci 112.622 yu kaare. Bene ngi bawoo ca dexug Niseer gi ci bëj-gànnaar yem ci mbàmbulaanug Atlas ci bëj-saalum ci ag tallalug 700 km. Diggante bi gën a guddu ci réew mi 325 km la. + +Taariix + +Lëkkalekaay yu biti + ICJ Judgment over the Benin-Niger boundary dispute, 12 July 2005 + Fabio Spadi (2005) The ICJ Judgment in the Benin-Niger Border Dispute: the interplay of titles and ‘effectivités’ under the uti possidetis juris principle, Leiden Journal of International Law 18: 777-794 + +Réew +Afrig +Gàmbi (Pénc mu Gàmbi) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Gàmbi +Mali (Republik bu Mali) : réewum Afrig + +Réew +Afrig +Ginne (Republik bu Ginne) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Beljik (Ruwaayom bu Beljik) : réewu Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Beljik +Burkina Faso : réewu Afrig. + +Afrig +Réew +Burkinaa Faaso +Kameroon (Réewum Kamerun) : réewum Afrig + +Làkku : Fulfulde, (Pular, Pulaar) + +Kamerun +Afrig +Réew +Danmaark (Nguur gu Danmaark; da: Kongeriget Danmark) : réewum Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Danmaark +Marook (Ruwaayom bu Marook) : réewum Afrig + +Réew +Afrig +Kap Weer (Gàwu Kap Weer) : réewum Afrig + +Melosuuf + +Duni +Boa Vista +Brava +Fogo +Maio +Sal +Santiago +Santa Luzia +Ilhéu Branco +Ilhéu Raso +Santo Antão +São Nicolau +São Vicente + +Dëkki i diiwaani +Assomada - Santiago +Cidade Velha - Santiago +Espargos - Sal +Mindelo - São Vicente +Porto Novo - Santo Antão +Praia - Santiago +Rabil - Boa Vista +Ribeira Brava - São Nicolau +Ribeira Grande - Santo Antão +Salamansa - São Vicente +Sal Rei - Boa Vista +Santa Maria - Sal +São Filipe - Fogo +São Miguel - Santiago +Cidade do Maio (Vila do Maio) - Maio +Cidade Nova Sinta (Vila Nova Sintra) - Brava + +Njàngale/Iniweersite +Iniweersite Kap Weert - Santiago (Praia, São Jorge dos Órgãos), São Vicente (Mindelo, Ribeira Julião) +Jean Piaget Iniweersite Kap Weert +Iniweersite Assomada +Iniweersite Mindelo +Iniweersite Santiago + +Sport +Campeonato Nacional (Kap Weert) - Football + +Sinemaa + +Filmi +O Ilhéu de Contenda (1995) +"Morna Blues" (1996) +Amílcar Cabral (2001) +Batuque' ["Batuki"]' (2006) +"Santo Antão - Paisagem & Melodia" (2006) +"Arquitecto e a Cidade Velha" (2007)Kontinuasom'' (2009) +"Contrato" (2010) +"Sukuru" (2017) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Réew +Afrig +Kap Weer +Afganistaan (Etaa Islaamik u Taraansisoŋ bu Afganistaan) : Asi + +Réew +Asi +Afganistaan +Albaani (Republik bu Albaani; sq: Shqipëri, Republika e Shqipërisë) : Óróop + +Réew +Tugal +Albaani +Aljeeri (Republik Popileer Demokaraatik bu Alseeri) : réewu Afrig. + Lii ab naal rekk la man nga cee dugal sa loxo ndeem am nga ci Xam-xam. + +Réew +Afrig +Andoor (Pirinsipóote bu Andoor; ca: Principat d'Andorra): réewum Tugal (Óróop) + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Pyrenees + +Lëkkalekaay yu biti + +Réew +Tugal +Andoor +Angolaa (Réewum Angolaa) : réewu Afrig. + Lii ab tambali rekk la man ga cee dugal sa loxo ndeem amga ci xam-xam. + +Réew +Afrig +Argentiin (Republik bu Argentiin) : réewu Aamerig + +Réew +Aamerig +Armeeni (Republik bu Armeeni) : réewu Óróop + +Réew +Tugal +Asi +Armeeni +Ótriis (Republik bu Ótriis) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Aserbayjaan (Republik bu Aserbayjaan) : réewum Tugal / Asi + + +Réew +Tugal +Asi +Bahamas (Commonwealth bu Bahamas) : réewum Aamerig + +Aamerig +Réew +Bahrayni (nguur gu Bahrayni) : Réew Asi + +Réew +Asi +Barbados (Republik Popileer bu Banglaades) + +Aamerig +Réew +Belaarus (Republik bu Belaarus, be: Рэспубліка Беларусь) : Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Butaan (Ruwaayom bu Butaan). + +Réew +Asi +Boliibi (Republik bu Boliibi): réewu Aamerig di Sid. + +Réew +Aamerig +Bosni Hersegowin (Republik bu Bosni Hersegowin; bs: Bosna i Hercegovina): réewu Óróop + +Réew +Tugal +Bosni +Botswana (Republik bu Botswana) : réewu Afrig. + '''Lii Ab sémp rekk la man ga cee dugal sa loxo ndeex am ga ci xam-xam + +Réew +Afrig +Åland Islands + +Réew +Anguilla : réewu Aamerig + +Réew +Angila +Aruba : dun + +Réew +Olaand +Óstraali : Réewu Oseyaani + +Diwaani oseyaani +Réew +Óstraali +Breesil (Réewum Breesil): réewum Aamerig di Sid. + +Réew +Aamerig +Bulgaari (България) (Republik bu Bulgaari) : Tugal (Óróop) + +Misik + + Nikolai Giaurov + Anna-Maria Ravnopolska-Dean + +Réew +Tugal +Buruundi (Gàwu Buruundi) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Buruundi +Kambodia (Ruwaayom bu Kamboodia) + +Réew +Asi +Banglaades : réewum Asi + +Asi +Réew +Banglaades +Beliis + +Aamerig +Réew +Bermuda + +Aamerig +Nguur-Yu-Bennoo +Kanadaa : réew Aamerig + + +Réew +Aamerig +Cadd (Republik bu Cadd) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Cadd +Ciili (Republik bu Ciili) + +Aamerig +Siin (Republik Popileer bu Ciin) : réewum Asi + + Qin Shi Huang + + +Réew +Asi +Koloombi (Republik bu Koloombi) : réew Aamerig + +Réew +Aamerig +Koloombi +Komoor (Bennoo bu Komoor) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Komoor +Kosta Riika (Republik bu Kosta Riika) : réew Aamerig + +Aamerig +Réew +Kodiwaar Réewum Kodiwaar (Côte d'Ivoire) : réewum Afrig + +Réew +Afrig +Korwaasi (Republik bu Korwaasi; hr: Republika Hrvatska) : réew Óróop + +Réew +Tugal +Kubaa (Republik bu Kubaa) : réewu Aamerig + +Kubaa dfa nekk ben deukou Aamerig latine . + +Aamerig +Réew +Ciipër (Republik bu Ciipër; el: Κύπρος, Κυπριακή Δημοκρατία; tr: Kıbrıs, Kıbrıs Cumhuriyeti): Réewu Tugal + Dun + +Réew +Tugal +Dun +Republik bu Finlaand (Wu-Finlaand: Suomen tasavalta) : Réewum Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Finlaand +Almaañ (Republik Federaal bu Almaañ) : réewum Tugal (Óróop). + + Bennoo gu Almaañ + + +Tugal +Réew +Jeoorji : réew Tugal / Asi + +External links + Full information about (country) Georgia (english, german, russian, georgian) + + +Réew +Tugal +Asi +Gana (Republik bu Gana) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Gana +Gibraltaar : Tugal (Óróop) + +Nguur-Yu-Bennoo +Tugal +Girees (Republik Ellenik; el: Ελλάδα, Ελληνική Δημοκρατία): réewum Tugal (Óróop) + +Melosuuf + +Dëkki + +Aten +Amifis +Eraklioo +Igoumenitsa +Kavala +Komoteen +Korent +Korfuu +Lamii +Laris +Metileen +Patraa +Pirees +Rood +Spaart +Teeb +Tessalonig +Tiripoli +Yannin +Zant + +Duni +Alonisos +Andros +Delos +Ibee +Idar +Itaak +Kioo +Kos +Kureet +Korfuu +Milos +Paros +Poros +Rood +Samoo (Samos) +Samotaraas +Sefaloni +Seteer +Siim +Siir +Skopelos +Tinos +Zant + +Waaxi +Waax bu Eraklioo +Waax bu Kavala +Waax bu Korfuu +Waax bu Patraa +Waax bu Pirees +Waax bu Tessalonig +Waax bu Zant + +Iniweersite +Iniweersite Aten +Iniweersite Kureet +Iniweersite Patraa +Iniweersite Peloponneez +Iniweersite Tessali +Iniweersite Tessalonig +Iniweersite Yannin + +Sport +Super League - Football +A1 Ethniki + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Réew +Tugal +Grönland : Dun + +Dun +Danmaark +Estooni (Republik bu Estooni; et: Eesti Vabariik) : réewum Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Estooni +Salbadoor (Republik bu Salbadoor) : réew Aamerig + +Réew +Aamerig +Ecoopi (Réewum Ecoopi) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Ecoopi +Antigua ak Barbuda + +Réew +Aamerig +Antigua ak Barbuda +Dunu Buwet : dunu mbàmbulaanug Atlas + +Dun +Noorwees +Jibuti (Réewum Jibuti) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Jibuti +Dominika (Commonwealth bu Dominika) + +Réew +Aamerig +Timkr-Leste (Republic Demokaraatik bu Timor-Leste) +Ekwadoor (Republik bu Ekwadoor): réewu Aamerig. + +Aamerig +Réew +Ekwadoor +Ejipt (Gawu Araab bu Ejipt) : réewum Afrig. + +Afrig +Asi +Réew +Isipt +Réewum Gineg yamoo : réew Afrig + +Réew +Afrig +Fijii (Republik bu iil yu Fiiji) : réewum Oseyaani + +Oseyaani +Réew +Gaboŋ (Republik Gabonee) : réew Afrig + +Sleg Gaboŋ alŋe. + +Réew +Afrig +Gaboŋ +Onduuras (Republik bu Onduuras) : réewu Aamerig + +Réew +Aamerig +Guwaatemaala (Republik bu Guwaatemaala) : réewum Aamerig + +Aamerig +Réew +Ginne Bisaawóo (Republi bu Ginne Bisaawóo) : Réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Guyaana (Republik bu Guyaana) : réewum Aamerig + +Aamerig +Réew +Ayiti ab dun la bu nekk ca Amerik diggu. Day ab dun bu mag bu mu bokkal Republik dominicaine te Port-au-Prince di péyam. + +Ayiti mooy reewu ñu ñuul ñi njëkka moom seen bopp ci attum 1804, ca seen fippu ga (1791-1803) ca la ñu dakkee Napoleon ak ay ñoñam ca dun ga. + +Magginu turu dëkk ba +Ci aaday Taino yi, Ayiti da doon tekki suufu doj yu kawe ya walla aw doj ci biir geej. + +Lëkkalekaay biti + Ay nataalu Ayiti + +Réew +Aamerig +Ooŋ Koŋ (香港) (Resiyoŋ u Administaraasiyoŋ Espesiyaal u Ciin bu Ooŋ Koŋ) + +Dëkki Siin +Oonguri (Republik bu Oonguri, Magyarország) : réew Tugal (Óróop) + + +Réew +Tugal +Islaand (Republik bu Islaand; is: Lýðveldi Ísland) : Dun + Réewu Tugal. + +Réew +Tugal +Dun +Indoneesi (Republik bu Indoneesi) : réew + +Album + +Réew +Asi +Endoneesi +Iraan (Republik Islaamik bu Iraan) : Réew Asi + +Réew +Asi +Iraan +Iraak (Republik bu Iraak) : Réew Asi + +Réew +Asi +Iraak +Israayil (Etaa bu Israayil) : réewu Asi + +Asi +Réew +Israayil +Itaali (Pénc mu Itaali; it: Italia, Repubblica Italiana) réewum Tugal (Óróop) +Itaali men la ci réew yi nek ci Bëj-saalumu tugal, + +ngir xootal Taarixu Itaali xoolal Fii + +Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi: + +Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon réew mu ñu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Dóox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia. + +Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatóor lañu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa cig jonjoodi . +Réew +Tugal +Itaali +Jordaani (Ruwaayom Aasemi bu Jordaani) + +Asi +Réew +Kasakistaan (Republik bu Kasakistaan) : réewum Tugalasi. + +Réew +Tugal +Asi +Keeñaa (Réewum Keeñaa) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Keeñaa +Kiribaati (Republik bu Kiribaati) : réewu + +Réew +Oseyaani +Kuwet (Etaa bu Kuwet) : réewu Asi + +Asi +Réew +Simbaabwee (Republik bu Simbaabwee) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Simbaawee +Saambi (Republik bu Saambi) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Saambi +Yaman (Republik bu Yaman) + +Réew +Asi +Yaman +Wiyetnaam (Republik Sosiaalist bu Wiyet Naam) : réewum Asi + +Réew +Benesuwela (Republik bu Bolibaar bu Benesuwela) : réewu Aamerig di Sid + +Réew +Aamerig +Vanuatu (Republik bu Vanuatu) : réew Oseyaani + +Réew +Dun +Oseyaani +Usbekistaan (Republik bu Usbekistaan) : réew Asi + +Réew +Asi +Usbekistaan +Uruguwaay (Republik bu Peeŋku bu Uruguwaay) : réewu Bëj-saalumu Aamerig. + +External links + Official website + +Réew +Aamerig +Uruguwaay +Ugaanda (Réewum Ugaanda) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Ugandaa +Tirki (Republik bu Tirki) : réew Tugal / Asi + +Gallery + + +Réew +Tugal +Asi +Tiniisi (Republik bu Tiniisi) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Tiniisi +Tirinidaad ak Tobaago (Republik bu Tirinidaad and Tobaago) : réew Aamerig + +Réew +Aamerig +Tonga (Ruwaayom bu Tonga) : réewu Oseyaani. + +Tonga +Réew +Oseyaani +Togóo (Republik bu Togóo) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Togóo +Taaylaand (Ruwaayom bu Taaylaand) : réew Asi + +Réew +Asi +Tansani am réewum penku Afrig la, féete ci peggi mbàmbulaanug End . Keeñaa ak Ugandaa ñoo ko féete bëj-gànnaar, Ruwandaa, Buruundi ak Kongóo-Kinshasa nekk ci sowwoom, Saambi ak Malawi nekk ci bëj-saalum-sowwoom, Mosambik nekk ci bëj-saalumam. + +Réew mi tollu na ci 947 303 te am 51 820 000 ciy way-dëkk, ay bantu rekk a fa dëkk. Péeyam mooy Dodoma, mi ngi nekk ci biir réew mi, waaye dottub koom-koom bi dëgg mooy Dar es Salam gi doonoon péey bi, féete ci tefes gi. kiswahili ak wu-angalteer ñooy làkki nguur ga, teewul ne itam araab am na fa doole, rawati na ci duni Sansibaar ak bu Penda. + +Tansani ju tay jii a ngi judd ci booloog Tanganyika ak Sansibaar ci 26 awril 1964, gannaaw, ci lu yàggul dara ñu am seenug tembte ci Nguur-Yu-Bennoo yi. Bokk na ci Commonwealth dale ci atum 1961, bokk na itam ci Mbootaayu Xeet yi dale ci 14 desambar 1961. + +Taariix + +Ci 1953, Julius Nyerere, ab jàngalekat la woon bu judd ci 1922, ci bi muy am 31 at la ñëw ci boppu TAA (Tanganyika African Association, mbootaayu waa-afrig bu Tanganyika), mu daldi koy soppi ag làngu politig dëgg, ci lu gaaw, tudde ko Tanganyika African National Union doon woote ngir ag tembteg seenum réew. Ci 9 desambar 1961 la leen ko Nguur-Yu-Bennoo yi jox, ci jàmm. Ci ndoorte li jëwrin ju njëkk la doonoon, ginnaaw pal gu desambar 1962 gi, mu doon njiitu réew ju njëkk ju Tanganyika. + +Ci 10 disambar 1963 la Sansibaar ak Pemba am seenug tembte, 26 awril 1964 la Tanganyika ak Sansibaar booloo ngir sos li tudd tay Réewum Tansani. Nyerere doon njiitu réew ma, Abeid Karume mi doonoon njiitu réewum Sansibaar nekk jëwrin ju njëkk ji, ci Tansani. Donte booloo gi amoon na, waaye ba-tay jii Sansibaar moo yoral boppam yenn yi. Njiitu réewum Tansani moo ko yoral li ñeel politig, kaaraange, mbiri biti-réew, añs, moom mu yural boppam njàngale mi ak koom-koom,.. + +Melosuuf +Tansani réew la mu nekk ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum féete ci Penku Afrig. Ay digam yu dénd ñooy mbàmbulaanug End gi ci penku, dojuw Kilimandjaro ak déegub Victoria bi ci bëj-gànnaar, déegub Tanganyika bi ci sowwu, déegub Malawi ci bëj-saalum-sowwu ak dexub Ruwuma ci bëj-saalum + +Lëkkalekaay yi biti + www.tanzania.eu + +Réew +Tansani +Afrig +Taajikistaan (Republik bu Taajikistaan) + +Réew +Asi +Emitai (1971) +Ousmane Sembène +Senegaal +(wo) - (fr) +103' + +Faat Kiné (2000) +Ousmane Sembène +Senegaal +(fr) - (wo) +120' + +Fary l'anesse (1990) +Mansour Sora Wade +Senegaal +(wo) +17' + + +Franc, Le (1994) +Djibril Diop Mambéty +Senegaal, Suwis, Faraas +(wo) +44' + + +Garga M'Bosse (aka Cactus ...aka Kaktus) (1975) +Mahama Traoré +Senegaal, Suweed +(wo) +80' + +Guelwaar (1992) +Ousmane Sembène +Faraas, Almaañ, Senegaal +(fr) - (wo) +115' + + +Haine de la fille, La (1996) +Jean-Levi Mahamuohd +Beljik +(fr) - (wo) +87' + + +Ramatou (aka Hyènes ...aka Hyenas) (1992) +Djibril Diop Mambéty +Senegaal +(wo) +110' + + +Jom (aka Dignity ...aka Jom ou L'histoire d'un peuple) (1982) +Ababacar Samb-Makharam +Senegaal, Almaañ +(wo) +80' + + +Karim (1971) +Momar Thiam +Senegaal +(wo) +65' + + +Karmen Geï (aka Karmen) (2002) +Joseph Gaï Ramaka +Senegaal, Faraas, Kanadaa +(fr) - (wo) +86' + + +Ken Bugul (1990) +Moussa Sene Absa +Senegaal +(wo) + + +Kodou (1970) +Ababacar Samb-Makharam +Senegaal +(wo) +100' + + +Lambaaye (aka Graft) (1972) +Mahama Traoré +Senegaal +(wo) +80' + + +Lettere dal Sahara (2005) +Vittorio De Seta +Itaali +(fr) - (it) - (wo) - (fr) +100' + +Mandabi (1968) +Ousmane Sembène +Faraas, Senegaal +(fr) - (wo) +105' + + +Mossane (1996) +Safi Faye +Almaañ, Senegaal +(wo) +105' + + +Même le vent (aka Even the Wind) (1999) +Laurence Attali +Faraas, Senegaal +(fr) - (wo) +18' + + +N'Diangane (aka Student) (1974) +Mahama Traoré +Faraas, Senegaal +(wo) +100' + + +Ndeysaan (aka Price of Forgiveness, The...aka Prix du pardon, Le ) (2002) +Mansour Sora Wade +Senegaal, Faraas +(wo) +90' + +Option, L' (aka Mon beau pays ...aka Option, The ) (1974) +Thierno Faty Sow +Senegaal +(wo) +90' + +Parlons grand-mère (1989) +Djibril Diop Mambéty +Senegaal +(wo) + + +Petite vendeuse de soleil, La (aka Little Girl Who Sold the Sun, The ) (2000) +Djibril Diop Mambéty +Senegaal, Faraas, Suwis, Almaañ +(fr) - (wo) +45' + + +Picc Mi (1992) +Mansour Sora Wade +Senegaal +(wo) +20' + + +Pièces d'identités (aka Identity Pieces ) (1999) +Mweze Ngangura +Faraas, Kongóo, Beljik +(fr) - (wo) +97' + + +Police Beat (2005) +Robinson Devor +Etaa yu Bennoo yu Aamerik +(en) - (wo) +80' + + +Reou-Takh (aka Big City ) (1972) +Mahama Traoré +Senegaal +(wo) +45' + + +Saaraba (1988) +Amadou Saalum Seck +Senegaal +(fr) - (wo) +90' + + +Sadaga (aka Sadaga le M'Bandakatt ...aka Troubadour, The ) (1982) +Momar Thiam +Senegaal +(wo) +68' + +Sarax-si (1983) +Mahama Traoré +Senegaal +(wo) + + +Seye Seyeti (aka Man, Some Women, A ...aka Un homme, des femmes ) (1980) + +Tableau ferraille (aka Tableau ferraille) (1998) +Moussa Sene Absa +Senegaal, Faraas +(fr) - (wo) + + +Taggoo (1975) +Amadou Fall +Senegaal +(wo) +60' + + +Tauw (1970) +Ousmane Sembène +Senegaal +(fr) - (wo) +24' + + +TGV (1998) +Moussa Touré +Faraas, Senegaal +(fr) - (wo) +88' + + +Touki Bouki (aka Journey of the Hyena ) (1973) +Djibril Diop Mambéty +Senegaal +(wo) +85' + + + +Waalo Fendo - Là où la terre gèle (1997) +Mohammed Soudani +Suwis +(fr) - (it) - (wo) +63' + + +Xala (aka Curse, The ...aka Impotence) (1975) +Ousmane Sembène +Senegaal +(fr) - (wo) +123' + +Xew Xew (aka Let the Party Begin ...aka Que la fête commence '') (1984) +N'Gaido Ba +Senegaal +(wo) +85' You, Africa!''' (1994) +Ndiouga Moctar Ba +Senegaal +(fr) - (wo) +43' + +Links +IMDb (Internet Movie Database) + +Filmi ci Wolof +Olaand (Nguur gu Olaand - Aantiy bu Olaand) : réewum Tugal (Óróop). Olaand nekk ci Sowwu Tugal. + +Olaand +Réew +Tugal +Suweed (Ruwaayom bu Suweed; sv: Sverige, Konungariket Sverige) : réewu Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Suwis (Komfederaasioŋ Suwis) : réewu Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Kongóo (Gàwu Kongóo) : Réewum Afrig + +Afrig +Réew +Kirgistaan (Republik bu Kirgistaan) + +Réew +Asi +Letóoni (Republik bu Letóoni; lv: Latvija, Latvijas Republika): réewu Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Letóoni +Libãa (Republik Libanee) : réewu Asi. + +Réew +Asi +Lesoto (Ruwaayom bu Lesoto) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Lesoto +Libeeria (Republik bu Libeeria) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Jamaaiiria Araab bu Liibiee (Jamaaiiria Araab liibiee Popileer Sosiaalist) : réewum Afrig. + +Réew +Afrig +Libi +Liechtenstein (Pirinsipóote bu Liechtenstein) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Lituwaani (Republik bu Lituwaani; lt: Lietuva, Lietuvos Respublika): réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Luksambuur, am réew la mu nekk ca Sowwu Tugal péyam tuddu Luksambuur itam. Moom as dëkk su tuut la. + +Réew +Tugal +Makaaw (澳門) (澳門特別行政區 , Resiyoŋ u Administaraasioŋ Espesiyaal u Ciin bu Makaaw). + +Dëkki Siin +Masedwaan gu Bëj-gànnaar, Republik bu (Republik bu Yugoslaawi bawoon di Masedwaan) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Réewum Maseduwaan +Madagaskar (Réewum Madagaskar) mi ngi nekk ci bëj-saalumu Afrig, di dun bi ëpp ci Afrig + +Réew +Afrig +Madagaskaar +Malawi (Republik bu Malawi) : réewum Afrig. + +Afrig +Réew +Malawi +Maldiif (Republik bu Maldiif) : réew + +Asi +Réew +Maldiif +Malt (Republik bu Malt) : dunu + réewu Tugal + +Réew +Tugal +Dun +Malt +Duni Marsaal (Republik bu Duni Marshall) : réewu Oseyaani + +Réew +Oseyaani +Móoris (Republik bu Móoris) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Meksig (Etaa yu bennoo yu Meksig) : réew Aamerig + +Réew +Aamerig +Meksig +Mikroneesi, Etaa yuñu Federe yu (Etaa yuñu Federe yu Mikroneesi) +Moldaawi, Republik bu (Republik bu Moldaawi; ro: Republica Moldova) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Monaako (nguur gu Monaako) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Monaako +Mosaambik (Republik bu Mosaambik) : réewu Afrig + +Réew +Afrig +Miyanmaar (Bennoo gu Miyanmaar) : réew Asi + +Asi +Réew +Namibi (Pénc mu Namibi)(Republik bu Namibi) : réew Afrig. + +Réew +Afrig +Namibi +Naawru (Republik bu Naawru) : réew Oseyaani + +Oseyaani +Réew +Dun +Nepaal (नेपाल) (Ruawaayom bu Nepaal) : réewu Asi. + +Asi +Réew +Nepaal +Nikaraaguwa (República de Nicaragua,Pénc mu Nikaraaguwa) : réewu Aamerig. + +Réew +Aamerig +Nikaraaguwa +Nijeer (Republik bu Nijeer) : Afrig. + +Réew +Afrig +Niue (Republik bu Niue) +Northern Mariana Islands (Sankattan Siha Na Islas Mariånas, Komonwels bu Iil yu Northern Mariana). +Norweej (Ruwaayom bu Norweej; no: Norge, Kongeriket Norge): réewum Tugal (Óróop) + +References + +Noorwees +Réew +Tugal +Omaan (Saltanat bu Omaan) : réewu Asi. + +Asi +Réew +Réew +Asi +Palaaw (Republik bu Palaaw) + +Oseyaani +Réew +Palestiin (Hebrew: ארץ־ישראל Eretz-Yisra'el, formerly also פלשת, Peleshet; ) : Asi + +Asi +Panamaa (Republik bu Panamaa) : réewu Aamerig + +Réew +Aamerig +Eslowaaki (Republik bu Eslowaaki; sk: Slovenská republika) : réewu Tugal + +Lëkkalekaay yu biir + The Slovak Republic Government Office + +Réew +Tugal +Eslowaaki +Araabi Sawdit (Ruwaayom bu Araabi Sawdit) : réewu Asi + +Réew +Asi +Ispaañ (Ruwaayom bu Ispaañ) : Réewum Tugal (Óróop) + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Madrid + +Lëkkalekaay yu biti + ASESER Teranga: Asociación de Inmigrantes Senegaleses Residentes en A Coruña + +Réew +Ispaañ +Tugal +Ruwaanda (Republik bu Ruwaanda) : réewu Afrig + +Réew +Afrig +Esloweeni (Republik bu Esloweeni) : Réewum Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Somali (Republik bu Somali) : Réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Kataar (Etaa bu Kataar) : réew Asi. + +Réew +Kataar +Asi +Tugal mooy wàll wi féete penku goxub Tugalasi, ci baax dees koy jàppe niki benn ci juroom-benn walla juroom-ñaari goxi àdduna bi. Gox baa gi digu ci sowwu ci mbàmbulaanug Atlas gi, ci bëj-gànnaar ci dottub Bëj-gànnaar bi, yem ci géej gu Diggu gi ci bëj-saalum. Ay digam ci penku dese nañoo leer, dinay faral di jur ay werante; li ko waral mooy ni mu taqalook goxub Asi. + +Waa-Islaand jàppees na leen ni waa-tugal (donte féeteem ci degalub Tugal-Aamerig), ak mbooleem dun yi ci géej gu Diggu gi, Sipër mi gën a jur coow, ci wàllu melosuuf. Riisi ak Tirki ñi am li ëpp ci seen suuf ca Asi, waaye day ni rekk li ëpp ci seen taariix réewi gox bi lañu ko bokkal. + +Melosuuf +Ngir xóotal: Melosuufug Tugal +Tugal a ngi yaatoo 10 392 855 km² (fukki junni-junni ak ñetti-fukki-junni ak juroom-ñent-fukk ak ñaar ak juroom-ñetti-téeméer ak juroom-fukk ak juroom). Di benn ñetti Afrig walla benn ñenti Asi walla Aamerig. + +Mi ngi séedatliku ci jurromi diwaan: Penku Tugal, Diggu Tugal, Sowwu Tugal, Bëj-gànnaaru Tugal ak Bëj-saalumu Tugal + +Gox bi am na 49 ciy réew. + +Réewi Tugal + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + ASESER Teranga: Asociación de Inmigrantes Senegaleses Residentes en A Coruña + +Gox yi +Réewum Cek (Ceki) am réew la ca Tugal + +Réew +Tugal +Poloñ (Republik bu Poloñ; pl: Rzeczpospolita Polska) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Portugaal (Republik Portugees) : réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +San Marino (Republik bu San Marino) : Réewu Tugal + +Réew +Tugal +Nguur-Yu-Bennoo walla Nguur Yu Bennoo yu Brëtaañ gu Mag ak Irlaand gu Bëj-gànnaar (United Kingdom of Great Britain and Northern Ireland), ñenn ñi di ko wax angalteer, am réewu bëj-gànnaaru Tugal la. + +Nguur gaa ngi judd ci 1800 ci booloog Nguurug Brëtaañ gu Mag ak Nguurug Irlaand. Ci 1922 la wàll gu yaa ci Irlaand dagg, tudde boppam Réewum Irlaand. Nguur gi dafa séddalikoo ci ñeent: Angalteer, Irlaand gu bëj-gànnaar, Wales ak Ekos + +Réew +Tugal +Nguur-Yu-Bennoo +Afrig + Aamerig + Asi + Tugal + Oseyaani + +Melosuuf +Suuf +Afrig, Afirig, moom la ñu jàppee ne mooy gox bi nit cosaanoo, su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam (lu weesu gox bu Asi), mooy ñaareelu gox bi gënn a rëy ci àdduna bi. Yaatuwaayam tollu na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci jéeri ji ci àdduna bi. Ay way dëkkam tollu ci lu ëpp 800.000.000, muy benn juroom ñaareel bu way dëkki àdduna bi. Afrik a ngi yem ci bëj-gànnaaram ci Géej gu Diggu gi, ci sowwu ci Mbàmbulaanug Atlas, ci bëj-saalum ci Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi, ci penku ci Mbàmbulaanug End. Asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi. Yamoo gi jàll na ko. Ci jëmm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute teg ci. + +Cosaanam +Baatu «Afrig» moo ngi jóge ci turu Afridi yi, doonoon ag giir gu dëkkoon ci Bëj-gànnaaru Afrig ci diwaanu Kaartaas. + +Beneen cosaanam moo bàyyikoo ci Berber Taferka «suuf», «boroom suuf». Ki fay dund la ñuy woowee Aferkiw, Latin yi soppi ko africanus, mu doonoon aw tundu waa rom ci Afrig. Araab yi di ko wax إفريقيا ifrīqīyā, mu doonoon Tiniisi gu tay gi. + +Ñeneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike («amul sedd»), latin di ko waxaprica («Bari naaj»), la jóge. + +Taariix +Afrik la ñuy jàppee ne mooy cosaanu nit, ndax desiti nit yi gën a yàgg ci àdduna bi fa la ñu ko gisee, ci Afrig gu Bëj-saalumu-Sahara. + +Sahara cëru na bu baax ci màggug gox bi. Taariixu askani Bëj-gànnaaru Afrig yi day tolloo ak bu Tugal ak bu Penku gu Diggu gi. Li ëpp ci Afrig gu Bëj-saalumu-sahara amul woon genn jëflante ak li des ci àdduna bi, da ñoo beru woon. + +Jamono ju yàgg ja +Xay yi juddoo ci goxu Afrik, boole nañ leen ci yi gën a mag ci taariixu nit. Xayu Esipt ak bu Gana ak bu Mali, ak bu Kuush ak bu Songaay, añse. + +Jamono ju yees ji + +Jàppum njaam + +Ci li taariixkat yi wax, jàppum njaam mi ngi tambali ci xarnub VII ak araab yi. Ci lu gën a leer ci atum 652 ba Ab njiitu araab takk-taxawalee waa Nubi yi ngir ñu jox leen 360 ciy jaam at mu jot. barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca Mali ba Penku Afrik, ci wàll gi féete bëj-saalumu Sahara. + +Ci xayma nee nañ ci diggante xarnub XVIII ba ci xarnub XIX, benn ñenteel ci nit ñi ay jaam la ñu woon, walla ñu ñu manante (takk-taxawal) ci liggéey bu ñu sañut a bañ. Nee nañ njiitu waa afrik yi ci seen bopp ñoo doon jàppaate ak a jaayaate. + +Waa tugal lu weesu bi ñu aakimoo (walla sancee) suufi Aamerig yi da ñoo soxla woon ay loxo yuy liggéey ci seen tool yi. Def nañ ko ci 400 at (1500-1888), ay jaam yu bari jënd nañ leen walla jàpp nañ leen ci tefesi afrik yi: Sowwu Afrig gépp, ak ci bëj-saalumam itam. Donte tereg jàppum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum 1850 (réew yépp bàyyeendoowuñu ko) amoon ay nit yu wëyoon di ko def cig làqatu ba ci 1900. + +Jamono ju mujj ji + +Aakimoo gu waa tugal +Jamonoy aakimoo gu tugal ci Afrig moo ngi tambalee ci Ndajeem Berlin (1884-1885) ba ci tembte yi ci atum 1960, sedatle gu réew yu tay yi ca la jóge. Ecoopi moo doonoon menn rèew mi ñu masut a teg + +Melosuuf + +Réewi Gox bi + +Goxub Afrig gëstu gi aju ci ay way dëkkam + +Cosaan ak diine +Xool: Diiney Afrig + +Làkk +Gëstukatu-làkk yi ci xayma nee nañ 2 000 làkk ci goxu Afrik, ñu boole leen ci ñeenti mbooloo, làkk yi fa cosaanoowul bokkuñu ci. + +Xool it +Koom-koomu Afrig + +Lëkkalekaay yu biti + History of Africa The last tribal states. + +Afrig +Afrig gu Bëj-gànnaar (Réewum Afrig gu Bëj-saalum) : réewu Afrig + +Afrig +Réew +Gox Adduna + +Diiwaanu Nguuru Room + +Ci angale ak ci faranse mooy Asia. + +Asi dafa am ñaari tekki ci Injiil. + + Ci bu jëkk mooy li ñu tudde tey jii 'Asi Minër', maanaam daanaka lépp ci réew mu tudd tey jii Tirki (Turquie) lu fare penku géeju Ese. + Ñaareel bi, ci jamano Injiil ji, Asi benn diiwaanu nguuru Room la woon. Moo doon wàllug sowu Asi Minër. Dafa boole diiwaani Misi, Lidi, Kari, ak genn wàll Firisi, ak dun ya nekk ca géeju Ese. Waa Room ñoo ko def diiwaan ci 129 j.K.. Ci bu jëkk péeyam moo doon Pergam. Waaye, gannaaw jamano Injiil, def nañu Efes ni péeyam. Juróom ñaari dëkk yi ñu gis ca téere Peeñu ma (Pe 2:1-3:22) ñoo bokkoon ca diiwaanu Asi. + +Am na ñi xalaat ne yoon bu nekk ñu gis 'Asi' ci Injiil mooy diiwaanu nguuru Room bi. Am na ñeneen ñi xalaat ne léeg-léeg Injiil dafay wax ci ci Asi Minër (Jëf 19:26-27 21:27 24:18 27:2), te yi ci des mooy diiwaan bi. + +Man nañu gis Asi ci Injiil ci Jëf 2:9; 6:9; 16:6; 19:10,22,26,27; 20:4,16,18; 21:27; 24:19; 27:2; Ro 16:5; 1Ko 16:19; 2Ko 1:8; 2Tim 1:15; 1Pi 1:1; Pe 1:4. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Àdduna + +Lëkkalekaay yu biti + +Gox yi +Adduna +Melosuuf +Bereb yi ci Téere Linjiil + + +Réewi + +Sukkandiku yi + +Multinational organizations in the Americas + +Adduna +Melosuuf +Aamerig +Paraguwaay (Republik bu Paraguwaay) : réewu Aamerig di Sid. + +Réew +Aamerig +Paraguwaay +Peru (Republik bu Peru) : réewu Aamerig di Sid. + +Réew +Aamerig +Biibël Mooy tur bi ñu jox mboolem mbind yu sell yu Yàlla yi, ci diiney yawut ak Kirist. Baatu biibël la ngi jòoge ci kallaama gerek gu yagg ga, di tekki “teere yi”. Ci’g neen, day ab teere bu ñu boole, ay mbindi cosaan, mbindi atte, mbindi xew-xewu demb, mbindi cellte, yu yonent, taalif ak ay bataaxal, yoo xam ne ci diiru junniy at lañu leen bind. Biibëlu kercen yi dañ koo seddale ci ñaari pacc: Seede bu Yag bi, bi ñu boole teere yi ñu dondee ci diine yawut yi ak Seede bu Bees bi, di ay mbind yu’y seede dundu Yeesu-Kirist. Ci Jàngu yi, Biibël kaddu Yalla lañu koy wowee. + + 1 Musaa + 2 Musaa + 3 Musaa + 4 Musaa + 5 Musaa + Léebu + 1 Samwil + 2 Samwil + 1 Nettaliy xew-xewi cosaan + 2 Nettaliy xew-xewi cosaan + Ayóoba + Sabuur + Isayi + Esekiel + Dañel + Amos + Mikaa + Malaki + + Macë + Màrk + Luug + Yowaana + Jëf ya + Room + 1 Korent + 2 Korent + Galasi + Efes + Filib + Kolos + 1 Tesalonig + 2 Tesalonig + 1 Timote + 2 Timote + Tit + Filemon + Yawut ya + Saag + 1 Piyeer + 2 Piyeer + 1 Yowaana + 2 Yowaana + 3 Yowaana + Yudd + Peeñu bi + +Lëkkalekaay biti + Le Nouveau Testament de la Bible en wolof + +Diine +Yéesu-kristaa mooy ji ëpp solo ci diiney krist. yeesu moo yëut: « Yahweh est salut », kristaa di baatu gerek bi'y tekki ci yëut « ku sell ki »). moom la ñi daw yalla tek ci. Catolig yi, ortodoks yi ak li ëpp ci jàngu ñaxtukat yi dañ ni nit dëgg te di yalla tek ci. + Biibël + +Diine +Nowel + +Ci bu jekk, xeetu Wolof yii maggaluwoon bësu nowel. Waaye leegi ak comercialization du lépp. Yeeneen nit ni ci Ndakaaru ak yeeneen dëkk yu mag yi dañuy maaye ay cadeew ak di def lamp yu rafet ci seen kër. Li ci genn bari ci Wolof yii du nu ay catoliq walla talibe Insa, kon dunuy fonk bësu nowel. + +Ci sunu jamanoo dañuy tambali di am ay talibe Insa. Te noom noo jël bësu nowel ngir maggal judug Insa (ki nu wax nee Yeesu Krist ci faranse). Seen maggal mingi aaw ci ay woy, ak i ñaan ak lekkando. + +Diine +Saamowa (Etaa bu Moomboppam bu Saamowa) : réewu Oseyaani + +Oseyaani +Réew +Filipiin (Republik bu Filipiin) : Réewum Asi +Asi +Réew +Filipiin +Suudaan (Republik bu Suudaan) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Saw Tome ak Preesip (Republik Demokaraatik bu Saw Tome ak Preesip) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Sao Tome ak Principe +Siraa Leyoon (Republik bu Siraa Leyoon) + +Réew +Afrig +Seychelles (Republik bu Seychelles) : réew + +Réew +Afrig +Singapoor (Pénc mu Singapoor) : réewu Asi + +Réew +Asi +Eswatini (Ruwaayom bu Eswaatini) : réew Afrig + +Réew +Afrig +Eswatini +Surinaam (Republik bu Surinaam) : réewu Aamerig di Sid. + +Réew +Aamerig +Siri Laaŋka (Republik Sosiaalist Demokaraatik bu Siri Laaŋka) : réew Asi + +Réew +Asi +Virgin Islands, British (British Virgin Islands) + +Nguur-Yu-Bennoo +Virgin Islands, U.S. (Virgin Islands of the United States) + +Diwaan-yu-bennoo +Taaywaan (Republik bu Ciin) : réewum Asi + +Asi +Réew +Koore, Republik Popileer Demokaraatik bu (Republik Popileer Demokaraatik bu Koore) : réewum Asi + +Asi +Réew +El Hadji Cissé, Nataalkat djargogne.org +Fatou Diome, bindakat +Ismaël Lô, woykat +Djibril Dio Mambéty,bindkat +Youssou N'Dour, woykat +Ousmane Sembène,bindkat, cinemaakat +Momar Thiam +Seriñ Abdu Xaadir Gueye Badar, Gëstukatu wolof + +Nit nag mooy képp ku sosoo ci Aadama (doomu Aadam) nite nag moom la nu soxla ci nit ndax bo nite wul ab dof ngay donn. Nit moom la Yàlla miy Sosaakon Bi gën a bëgg ci li mu sos li gën ci li mu sos it nit la li mu gën a teral ci li mu sos it nit la waye nag ndax nit moom mii xam na boppam ? Bu ko xamee li ko war mooy mu nite. +Ousmane Sembène (January 1, 1923 — June 9, 2007). + +Filmi ci Wollof +Mandabi (1968) +Tauw (1970) +Emitai (1971) +Ceddo (aka Outsiders) (1977) +Xala (aka Curse, The ...aka Impotence) (1975) +Camp de Thiaroye (aka Camp at Thiaroye, The) (1987) +Guelwaar (1992) +Faat Kiné (2000) + +Filmi ci Faraañse ak yeneeni làkk +L'empire Sonhrai (1963) +Niaye (1964) +La noire de... (1966) +Borom Sarret (1966) +Moolaadé (2004) + +Sinemaa +Ndar (fr. Saint-Louis-du-Sénégal) béne deukkou Senegaal. + +Mu ngi ci bëj-gànnaar Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Martinik : dunu Faraas (Géejpeek u Atlantik) + +Faraas +Dun +Federaasioŋ bu Riisi (ru: Российская Федерация): réewu Tugal (Óróop) + +Pey : Mosku + +Riisi +Tugal +Asi +Réew +Japoŋ : Réewu Asi. 4 duni : Hokkaido, Honshu, Shikoku, Kyushu. + +Réew +Asi +Sapoŋ +Jamayka : Dun, Réewu Aamerig + +Réew +Dun +Aamerig +Republik bu Irlaand (ga: Éire, Poblacht na hÉireann): Dun, Réewu Tugal + +Réew +Dun +Tugal +Watikaa : réewu Tugal + +Réew +Tugal +Maleesi : réew Asi + +Réew +Asi +Diiwaan-yu-Bennoo, walla Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig ci anam gu gudd am réew la mu séddaliku ci juroom-fukki diwaan, ñent-fukk ak juroom-ñett yi ñoo taqaloo te féete ci diggante Mbàmbulaanug Atlas ak Gu-Dal gi, penku ba sowwu, Kanadaa moo féete bëj-gànnaar, Meksik nekk ci bëj-saalumam. Alaskaa ci la bokk donte taqu ci, mi ngi nekk ci sowwu Kanadaa. Xawaay moom mi ngi ci diggu mbàmbulaan Gu-Dal gi. Réew mi am na fukk ak ñenti diiwaan yu tasaaroo ci géeju karayib yi ak Gu-Dal gi. Péeyam mooy Washington. + +Lusomundo + +Diiwaan-yu-Bennoo yi ci 2008, 302 ciy miliyoŋ ciy way-dëkk lañu amoon, loolu tax muy ñetteelu réew mi ëppi nit ci àdduna bi, ci ginnaawu Siin ak End. Réyaayam toll ci 9,4 junni km², di ñeenteel ci àdduna bi, ci ginnaawu Riisi, Kanadaa ak Siin. Gàddaay gi bari na fa lool, ba tax muy réew mi ëppi xeet yu jaxasoo ci Suuf si. Koom-koomam mooy bi gën a woomle ci àdduna bi, te moo am njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) mi ëpp ci àdduna bi. + +Tur wi +Turu Réew mi Thomas Paine moo ko tànnoon ci bés bi ñuy am seenug temb ci 4 sulet 1776. +Woowiin wu gàtt wi, wi ñuy faral di jëfandikoo ci sunuy waxtaan, ci njàngale mi ak ci lonkoyoon yi, mooy «Diwaan-yu-Bennoo» (ci wu-angalteer di United States, ñu tënk ko ci US). Wu gudd wi ñu koy faral di jëfandikoo ci këyiti nguur gi «Diwaan-yu-Bennoo yu Aamerig». + +Taariix + +Jamono njëkk-kolomboo (Laataa 1492) +Ci Alaskaa lañu gise jeexiti nit ki fa njëkk a teew, ci weti 20 000 at nj.j, ci tefesu atlas ci wetu 13000 at nj.j. Nit ñi njëkk a dëkk ci réew mi ñoo nga bàyyikoo ca Goxub Asi, jaare woon ko ca xat-xatu Beriŋ. Ci ginnaaw bi la fa waa-tugal yi ñëw. + +Jamonoy canc (1492-1775) +Christophe Colomb moo wuññi goxub Aamerig ci 1492, at ma ca topp mu nemmeeku barab bi nekk Poortorikoo tay jii. Ci XVIu xarnu la réewi Tugal ya fa ëppoon doole doon seet ay jàlluwaay ci bëj-gànnaar-sowwu ak ay am-am, ci seeni tukki ci topp tefesu Atlas gi ñu dem ba taxawal fa ay sancu yu sax. Ci bëj-saalum waa-espaañ yi sos fa seenub sancu duppee ko Espaañ-gu-Bees, di amal ay tukki-gëstu ci biir réew mi. Ci bëj-gànnaar-sowwu waa-riisi yi sanc fa ci li topp tefesu Mbàmbulaanu Gu-Dal gi. Ci la tubaab yi tàmbalee yaxantu ak askan yi fa cosaanoo. + +Ci diggante XVIIu ak XVIIIu xarnu, ndànk ndànk, la fukk ak juroom-ñetti sancu waa-angalteer taxaw ci tefesu penku gi, Lii mooy maamu Diwaan-yu-Bennoo yi. Waa-fraa yi nemmeeku pegu Misisipi dal di fay sos Luisiyaan + +Ngir xóotal yëral foofu: Taariixu Aamerig + +Réew +Aamerig +Eriteeri : réew Afrig + +Réew +Afrig +Eritere +Guwaadaluup : Dun Faraas (Géejpeek u Atlantik) + +Dun +Faraas +Gwiyaani Faraañse : Faraas + +Faraas +Grenada : Dun (Géejpeek u Atlantik), réewum Aamerig + +Réew +Dun +Aamerig +United States Minor Outlying Islands + +Dun +Guwaam : Dun (Géejpeek u Pacifik) + +Dun +Kongóo, Republik Demokaraatik bu : réewu Afrig + +Réew +Afrig +Kongóo-Kinshasa +Moŋgooli : réew Asi + +Asi +Réew +Koore, Republik bu (대한민국, 한국) : réew Asi + +Réew +Asi +Kore gu Bëj-saalum +Romaani (ro: Romania): réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Seerbi : Tugal + +Réew +Tugal +Ukreen (uk: Україна): réew Tugal (Óróop) + +Réew +Tugal +Ukreen +Pari mooy péeyu rééwum Faraas. Nitñii motnañu 2 187 526 (2017). + +Pari +Dëkki Faraas +Péy +Melosuuf +Melosuuf +Limu Réewi àddina si + +: Pays + +: Country + +: دولة + +Réew +Dùn : Dun (Nguur-Yu-Bennoo) + +Nguur-Yu-Bennoo +Dun +Djibril Diop Mambéty (Born: Dakaar 1945, Died: Paris 1998) + +Filmi + Contras' City (1969) + Badou Boy (1970) + Touki Bouki (aka Journey of the Hyena ) (1973) + Parlons grand-mère (1989) + Ramatou (aka Hyènes ...aka Hyenas) (1992) + La Petite vendeuse de soleil (2000) + +Senegaal +Sinemaa +Sinemaa + +Filmi ci wolof/Liste de films en wolof/List of films +in wolof +Géej am mbalka mu mag la mu ndoxum xorom nekk te sës ci gox yi, mbàmbulaan yi ñoo leen di lëkkale. + +Peggu ndox ak suuf la ñuy woowee tefes. + +Géej yi + Mbàmbulaan gu Dal gi + Géeju Bering + Géeju Sapon + + Mbàmbulaanu Atlas + Géeju Karayib yi + Géej gu Bëj-gànnaar + + Géej gu Diggu gi + Géej gu Xonq gi + +Géej +{| style="background:#f5fffa; width:100%; border:1px solid #F0A050" +|- +| colspan=3 | + +Diiney Afrig + +Diine +Banjul : mooy péeyu rééwum Gaambi. + +Séwógaraafi + +Nitñii motnañu 31 301 (2013). + +Péy +Afrig +Gàmbi +Meckhe benn dëkku Senegaal. + +Mu ngi ci bëj-gànnaar Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Turkumenistaan : réew (Asi) + +Réew +Asi +Dunu Cook : Dun, Réew (Géejpeek u Pacifik) + +Réew +Dun +Mbàmbulaan Gu-Dal gi moo ngi nekk ci diggante goxub Aamerig ak bu Asi. + +Mbàmbulaan yi +Heard Island and McDonald Islands : Dun + +Dun +Iil yu Faarow : Dun + +Dun +Nguur-Yu-Bennoo +Nuweel Kaledooni : Dun Faraas (Géejpeek u Pacifik) + +Dun +Faraas +Poortorikoo Ab dun la bu nekk ci mbàmbulaanug Atlas gi te bokk ci Réew yu Bennoo yu Aamerig. + +Poortorikoo +Nuweel Selaand : réew, iil (Géejpeek u Pacifik) + +Réew +Dun +Republik Dominikee : réew, dun (Géejpeek u Atlantik) + +Réew +Dun +Aamerig +Mbàmbulaanu Atlas moo nekk ci diggante Afrig ak Aamerig. + +Mbàmbulaan yi +Tuvalu : réew, dun (Géejpeek u Pacifik) + +Réew +Dun +Seent Eleen : dun (Géejpeek u Atlantik) + +Dun +Nguur-Yu-Bennoo +Mayoot : dunu Faraas (Géejpeek u Indian) + +Dun +Faraas +Montserrat : dun (Géejpeek u Atlantik) + +Aamerig +Dun +Sahara Oksidantaal : Afrig (bëj-gànnar) + +Afrig +Réew +Réewum Diggu Afrig : réewum Afrig + +Réew +Afrig +Tokelau : dun (Géejpeek u Pacifik) + +Dun +Moo nekk ci diggante Afrik ak Asi ak Òstraali ak dottub bëj-saalum + +Mbàmbulaan yi +Iil yu Solomon : réew, dun (Géejpeek u Pacifik) + +Réew +Dun +Dunu Falkland (Malvinas) : dun (Géejpeek u Atlantik) + Péy : Port Stanley + +Dun +Nguur-Yu-Bennoo +Norfolk Island : + +Dun (Géejpeek u Pacifik) + +Dun +Saint Lucia : réew Aamerig, dun (Géejpeek u Atlantik) + +Réew +Dun +Aamerig +Republik Popileer Demokaraatik bu Laawos : réew Asi + +Réew +Asi +Pitcairn : dun (Géejpeek u Pacifik) + +Dun +Nguur-Yu-Bennoo +Saint Kitts and Nevis : réew Aamerig, Dun (Géejpeek u Atlantik) + +Réew +Dun +Aamerig +Papwa Nuweel Ginne : réew, dun (Géejpeek u Pacifik) + +Réew +Dun +Saint Pierre ak Miquelon : dun (Géejpeek u Atlantik) + +Dun +Faraas +Wallis ak Futuna : Dun Oseyaani + Faraas. + +Dun +Wallis ak Futuna +Faraas +Turks and Caicos Islands : dun (Géejpeek u Atlantik) + +Dun +Svalbard and Jan Mayen (Noorwees) + +Noorwees +Polineesi Faraañse : dunu Faraas (Géejpeek u Pacifik) + +Faraas +Dun +Reiñõo : dun (Géejpeek u Indian) + +Dun +Faraas +Pénc mu Araab mu Siri : réew Asi + +Réew +Asi +Siri +Saint Vincent and the Grenadines : Dun (Géejpeek u Atlantik), réew + +Dun +Aamerig +Réew +Imaarati Araab yu Bennoo : réew Asi + +Réew +Asi +South Georgia and the South Sandwich Islands : Dun + +Dun +Nguur-Yu-Bennoo +Cees (fr. Thiès) benn dëkku Senegaal. + +Mu ngi ci bëj-gànnaar Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Jurbel (=Njaaréem) (fr. Diourbel) benn dëkku Senegaal la. + +Dëkki Senegaal +Mbuur (fr. M'bour) benn dëkku Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Luga (fr. Louga) benn dëkku Senegaal. + +Luga benn la ci 14 diiwaanu yi nekk Senegaal. Mi ngi féete ca penkub bëj-gànnaaru réew mi. Péeyum diiwaan ba mooy taaxu Luga. Luga am na lu tollu ci 835 325 doomu-aadama ci atum 2013. + +Dëkki Senegaal +Podoor (fr. Podor) benn dëkku Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Tëngéej (fr. Rufisque) benn dëkku Senegaal. + +Dëkki Senegaal +Tuubaa, dëkku murit yi,ab gox-goxaan la, mi ngi nekk ci diiwaanu Njaareem (jurbel), ci tunduw Mbàkke. Diggam ak Ndakaaru tollu na ci 150 km . + +Baatu Tuubaa mi ngi jóge ci làkku araab di tekki ci wolof : « texe ». + +Demb + +Dëkkub Tuubaa, kii di Sheex Ahmadu Bamba moo ko sanc ci atum 1887. + +Yoriinu dëkk bi +Dëkk bi mi ngi aju ci Ndaam, doon as ngox, maanam dëkku kaw kaw, bu taaxeedi, te nag doon gannaaw Ndakaaru, dëkk bi gëna taaxe ci Senegaal, ëpp ay nit. tey dëkk bi gën a rëy ci senegaal ginnaaw ndakaaru + +Melosuuftouba + +Nit ña + +Tuubaa moo ëpple yokkute ci barig nit ñi ci diiwaani Senegaal yépp (3,2% at mu nekk ci jamono yii ñu tollu te ñu jàppu ne yokkuteg nit ñi di na àgg ba 12% bu ñu àggee ci ati 2010). Yokku yooyu li ko waral moo di tuxu yu bari yi nit ñi di def bawwoo ci dëkk yu nekk ci Bawol ak Kajoor. Dëkk yooyu dañuy gent si ndànk ndànk jëm Tuubaa. + +Ci waññib 2002 bi, nit ñi ñi ngi tolloon ci 461 159. + +Ci atum 2007, bu ñu ajoo ci gam-gamle gu nguurug Senegaal, waa dëkk bi tolloon nañu ci 529 176. + +Koom koom + +Naataangeg dëkk bi lëkkaloo na lool ak Màggal gu mag gi giy dëppoo ak demug Seex Ahmadu Bamba ci géej gi.Ba tay Tuubaa dafa bari li waa Senegaal di woowe Moodu moodu, di ay tukkikat yu féete Tugal tey ëndi xaalis bu bari ci dëkk bi. Lii di yaxantu (jënd ak jaay) tamit da faa dox lool. + +Aada +Kii di Seex Abdul Ahat doon ñatteelu xalifa Seex Ahmadu Bamba moo fa tabaxoon barab bi ñuy woowe daaray kaamil di kàggu gu ñu denci mbindum Seex Ahmadou Bamba ak yeneeni mbind aki téere yu aju ci lislaam, ak ci yeneen fànni xam-xam yi yittéel nit, mi ngi feete nag ci penku jumaa ji, làng ak armeel yi. + +Tabax yu mag yi + +Ci Tuubaa la jumaa ju mag ji nekk, doon jumaa joo xam ni jenn la ci Afrig gu sowwu jant, ci taaram, ak ci rëyaayam. man nañoo jàpp ne mooy xolu dëkk bi, ndaxte yeneen kër yepp dañoo ñëw di ko wër ndànk ndànk, ànd ak màggaayu dëkk bi. Jumaa ji am na juroomi sooroor ak ñeenti xubba. Soorooram bi gën a gudd tollu na ci 80 meetar. Sooroor boobu, kii di Sëriñ Fàllu Mbakke mooko tudde Làmp Faal féetele ko kii di Maam Seex Ibra Faal ci 7 juin 1963. Bis boobu moo di ubbite gu njëkk, ba ñu bari teewe woon nañu ko, ku mel ni Lewopool Sedaar Seŋoor. Foofu ci jumaa ji fa la barabu Seex Ahmadu Bamba nekk. + +Dayo + Cheikh Ahmadou Bamba Khadimou Rassoul, théologien musulman soufi. + +Xool it + +Teerekaay + Touba and the meaning of night, New York, Feminist Press at the City University of New York, 2006 + Eric S. Ross, « Touba: a spiritual metropolis in the modern world », Canadian Journal of African Studies, 1995, 29.2 + Eric S. Ross, Sufi City: Urban Design and Archetypes in Touba, Rochester, University of Rochester Press, 2006, 344 p. + Monique Bertrand et Alain Dubresson, Petites et moyennes villes d'Afrique noire, Karthala, 1997, p. 118-119 + Cheikh Guèye, L’Organisation de l’espace dans une ville religieuse : Touba (Sénégal), thèse de doctorat, Strasbourg, Université Louis Pasteur, 1999, 650 p. + Sophie Bava et Cheikh Guèye, « Le grand magal de Touba. Exil prophétique, migration et pèlerinage au sein du mouridisme », Social Compass, 2001 + Cheikh Anta Mbacké Babou, Touba, genèse et évolution d’une cité musulmane au Sénégal, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1992, 39 p. (Mémoire de DEA) + Cheikh Guèye, Touba : La capitale des Mourides, Paris, Karthala, 2002 + Amar Samb, « Touba et son "magal" »; Bulletin de l'IFAN, t. XXXI, série B, n° 3, juillet 1969, p. 733-753 + Alexis Sané, Situation et perspectives de l'intégration de Touba dans la vie économique du pays, DAKAR, CFPA, 1970, 66 p. (Mémoire de stage) + +Filmokaay + Blaise Senghor, Grand Magal à Touba, court métrage documentaire, 1962, 20 mn + Christophe Marlard, A travers le Sénégal. 3, Touba, une ville à part, film documentaire, ENS Fontenay/Saint-Cloud, 1999, 13 mn + +Lëkkalekaay yu biti + + Maps, weather and airports for Touba + La communauté rurale de Touba Mosquée sur le site du PEPAM (Programme d'eau potable et d'assainissement du Millénaire) + La ville de Touba + « Statut d'extraterritorialité : comment Touba est devenu un État dans un État » (article de Wal Fadjri) + +Dëkki Senegaal +Yoonu murit +Xaralay Xibaar ak Jokkoo (XXJ) walla Xaralay Xibaar ak Jokkoo yu Yees yi, ci wu-angalteer Information and Communication Technology, ci wu-faraas Nouvelles technologies de l'information et de la communication, moo ëmb mbooleem xarala yees jëfandikoo ngir yor ak jokkale ay xibaar. Yitteem mooy sos ay noste yuy yor ay xibaar, yor seenug suqaliku, seenug dencu, seenug jokkale, ak seenug kaaraange. + +Yombul joxe ci ab tekki bu daj ndax amul benn tekki bu ñépp ànd déggoo. Ñi ciy liggéey raññee nañu leen niki ñu seen xam-xam daj, dañoo nekk ñuy xam lépp lu laal: mbëjfeppal, xam-xamu nosukaay, jokkoosoryante. + +Lëkkalekaay yu biir +Xam-xamu nosukaay +Internet +mbëjfeppal + +Xam-xamu nosukaay +Kom-kom :mooy xam-xam biy leeral lu aju ci wutiinu alal, tey li nga am ci alal, sa koom-koom man naa tekki sa alal, lépp nag lu aju ci yëngu gu nit di def ngir am dara loolu ci xam-xamu koom-koom lay bokk, moo xam mbay la mba yaxantu mbaa liggéeyu xarala(fr : économie ; en : economics) = koom-koom +Dex (fr : fleuve, rivière ; en : river) + + Niokolo Koba + Saloum + Senegaal + Sine + +Melosuuf +Ndox +Kàllaama (fr : langue ; en : language) + + wu-angalteer + araab + wu-ispaañ + wu-faraas + wolof + +Làkk mooy cëslaayu ag yewwute + +Ñi ngi tàmbali sunuy wax ak jëf ci turu Yàlla(t.s) miy Rahmaan, di kiy boroom yërmaande ju yaatu ji ñu jagleel mbooleem mbindéef yi, tey Rahiim, di ki yor yërmaande ji mu'y jagleel ña nangu'g jaamoom. +Di julli nag te'y sëlmal ci sunu sang, sangu'b ñu jiitu ñi ak ñu mujj ñi, aki ñoñam aki saabaam, ak aji liggéeyalam jii di sëriñ Tuubaa, ak xeetam wépp. Sunu wax ji dañu ko'y tàmblee cib aaya'b alxuraan, ñu ci'y tegtaloo li làkk ëmb, yor ko ci'y njariñ, ci gépp wàll, ci sunu dund gi. Sunu boroom nee na ci alxuraanam ju tedd ji:(( Wa hallama Aadamal asmaa kullahaa, thiumma haradahum halal malaayikati, fa xaala anbiuunii bi asmaayi haaulaayi in kuntum saadixiin)) di maanaa : Yàlla (t.s) jangal Aadama tur ya yépp, bi mu noppee, jël mbir yooyee won leen malaayika yi, ne leen wax leen ma seeni tur, bu ngéen léen xamee? ñu ne ko tudd nanu sa'g sell, amuñu benn xam-xam boo ñu xamalul,bu ñu xam, yaw yaa'y ku xam ki, te'y ku xereñ , ku am hikma ki. Kon yii tur ci jii aaya ju tedd, mant'a doon lu dul làkk, wi nga xam ne bokk na ci li Yàlla (t.s) njekk'a xamal Aadama (j.m) bi mu ko bëggee wàcce ci kaw dénd bi, ngir mu wuutu ko fi. Loolu nag li ko waral moo'y nekku'g làkk di benn ci móoli cosaan yi ñu teg sunu dund gi, tabax ko ci. Bu doonul woon moom, dund gi di lu nekk ci lu dul maanaa mu ñu xam, di lu gën'a jege ag mbàyyima ci ag nite, bu amul wuutlaay. Ma ne xoolal ma dund gu ñu rafleel ci làkk, nu mu war'a mel ? ndax moo'y googu di fees dell ak junj yi ñu'y jëfandikoo bu ñu'y wax ak ku luu, muuma mbaa ku tëx ? lii sax ca dëgg-dëgg xeet la ci làkk, làkk ëppu ko yéesu ko, ginaaw moom mbir la mu ñu'y def ngir déggante ci. Ndax kat làkk du lu moy ab jumtukaay, ngir waxante, ñu ko'y jëfandikoo ngir déggante ci sunu biir !, xanaa déggoo ñu naan làkku njanaaw yi , mbaa dundat yi, ba ci wu bàyyima yi?jubluwuñu ci lu dul li ñu'y joyal, ngir seen moroom yi dégge léen ci. Ginaaw nag bàyyima yi di nañu déggante ci loolu ci seen biir, kon loolu manatuñu ko'o jàppe lu dul aw lakk ni yeneen yépp. Waaye jeneeral dund gii nga xam ne dafa féex ba ci sax jumtukaay yi ñu'y jëfandikoo ngir junj, maanaam dund gi ñu rafleel ba ci jumtukaayu'b déggante rekk, nu mu war'a mel ? nu xeet ak mbir ya'y dox ci'y sidiitam, aki buumi xolam di mel ? wii xeetu dund de ci li ma jort, narul'a doon lu dul ag ndofe gu ñu joyal, naa doyloo yooyu baat ndegam amuma yeneen yu ko man'a leerale ni mu ware. Gii dund ci lu dul làkk, da na nekki gu maneesul'a leeral, xel it du ko xalam. + +Ci loolu la Sayyid Qutub, di waxe ca teereem ba tudd Zilaalul Xuraan + +Ci loolu la Sayyid Qutub, di waxe ca teereem ba tudd Zilaalul Xuraan, di tafsiir bu mag ci alxuraan, mu ca'y firi aaya bu sell bii di (( wahalla aadama ba maakuntum taktumuuna)), mu ne : (( xool ñu nag ñi ngi nii - ci bëtu'b xol, ak leerug basiira - di jàkkaarloo ak la malaaka ya nekkoon ca Malaul Ahlaa doon jàkkaarlool.... xool ñu ñun ni ngi nii di gis ag wàll ca mbootum Yàlla mu màgg moomee,nga xam ne mi ngi ko dénk nekktéef bii di kojug nit, bi mu ko'y jox caabi'y kuutlaay ji, mu war ko'o wuutu ci kaw suuf. + +Mbootum kàttanu'g tudde mbir yi ay tur, wutal yëf yi ay xammeekaay yu tur, sekkare'b man'a jël jëmm yi, walla yëf yi tudde leen ay tur yu leen di def - te ñoom ay baat rekk lañu yu ñu wax - ñu'y ay junj aki sembool yu'y tekki jëmm yooyu ak mbir yooyu ñu leen tudde. Lii daal na la woor ne kàttan la gu am lool solo, ak xiima ci dundu'g nit ci kaw sii suuf. +Ñi ngi'y xam solo sii, bu ñu'y jeneer coona bu mag bi ñu naroon'a jànkoonteel, bu ñu mayutoon nit kàttanu'g junj yëf yi, ak nit ñi ci'y tur. Xoolal coona bi naroon'a am ci déggante ak jëflante, ndax li naroon'a xew, moo'y ku bëgg'a déggante ak sa moroom ci mbir, da nga'y teewal moomale mbir, mbaa ànd ak moom ba ca loola, nga joxoñ ko ko, mbaa nga laal ko.... bu dee xorondoom ngeen soxla, war ce'e waxtaan, da ngeen ca'y dem, mbaa ngeen teewal ko, lu ko moy deet ag déggante ci loolu, bu dee doj la, fawwu ngeen dem ba ca doj wa, bu dee nit, munt'a ñakk ngeen teewal ko, lu ko moy du ngeen ca déggante.... +Lii daal coona la bu kenn xalaatul'a dund ak moom, te dund gi tam narutoon'a wëy ci yoonam wii, bu Yàlla (t.s) mayuloon mbindéefam mii man-manu tudde mbir yi ay tur. Malaaka yi ñoom, jagle bii soxlawunu ko, ndax du lu manul'a ñàkk ci ñoom ci seeni jëf, moo waral mayeesu leen ko)). + +Kon làkk moo'y ponk bi nga xam ne ci la sunu'g dund di tabaxu + +Kon làkk moo'y ponk bi nga xam ne ci la sunu'g dund di tabaxu, su nu bëggee muy gu jege as lëf ci'g cilwiise aku'g taaxe,walla lenn lu am maanaa. +Bi làkk nekkee nag ba noppi, te tax ñu jeggi mbooleem rombuwaay yii, ca ngënéelam la, ak jappndal gi mu nu defal ba nu man'a déggante ci suñu biir, ñewati na di jumtukaay bi dugg ngir teg sunu dund gii ca njobbaxtal lu kawe, la di ag nite, ak ca tolluwaay bu yekkatiku bee di bu ag taaxe, aku'g xay. + +Bu doonul woon làkk, duñu doon man'a yekkati sunu dund gii ci xam-xam, ndax moo'y li'y tax nga man'a raññale mbir ak dundat yi, lu ci nekk nga ber ko nee, wutal ko turu boppam. + +Làkk moo'y cëslaayu "ag yewwute" + +Yewwute ñenn ñi naan ko "renaissance" ci francais di judduwaat, di ci araab "nahda" , di ci maanaa buur , buur nag bu nu ko waxee ci wolof moo'y jekki-jekki jug ,taxaw, ñeneen it di ko fire'e dekki, boo ko'y seet ci maanaa, yepp di wudd lenn, di la amoon ca Orob ca lenn ci'y jamonoom, di woon lu am solo, di lu waa Orob dul fatteeti, baat bii ñew ëmb maanaa mii mépp, di raññale jamono'y yewwute ci ngëmméen, judduwaat ginaaw ag dee, réer ci réeradi,xam ci xamadi, siggi ci segg, nërméelu ci taxaw, giim ci tàkk, xippi ci gëmm. + +Bii baat daal jaasi la ju moo dog seen diggante ak jamono joj tëñëxu ak yewwoodiku moo ko muuroon, matale ko, xel mu gàtt lakkal leen ci, gisiin wu ñaaw sonal leen ci, ñu nekkoon ci biiram di way jemadi kanam, di ñu soxlawoo ag leer, ba Yàlla yee ay nit, niital léen ca làmpam bu leer ba'y leerale, jugloo leen ci'y nelaw, ñu nekk ci'g" yewwute" duggalaale ci ñeneen ñu dul woon ñoon, ba tay Orob gii, di lu leer, ca googale leer la tanqe, te ca la yewwoo it. + +Kon ci gàttal yewwute fii mooy renaissance gi nga'y dégg ci kàllaamay franse te'y tekki ci maanaa yewwute rekk, ndax mooy judduwaat gu xam waral, ginaaw dee gu réer waraloon. + +Làkk moo'y cëslaayu'g yewwute, du ma'a'y ki ko njëkk'a wax, am na ñu bari ñu wax lu ni mel, ci xalaatkat yi ak taarixkat yi, bu ñu dello as lëf ginaaw ànd ak sunu'y xalaat, ba ci xarnu'b fukk ak juroom ñatt ci jëmmi boppam, da nanu gis ne lu bari ci'y xalaatkatam aki ñoñ taarixam, ku ci mel ni Lodoviko Antoniyo Mortara ak Volteer ak Wilyaam Robertson 1721 - 1793, jëfandikoo woon nanu waxiin wu mel ne wii, ndaxte boole nanu ci mbàndarga yi'y raññale jamono'y yewwute, boole woon nanu ci doxu'g waxiini gox yi,juge ci'y waxiin dem ci ay làkk yu réew niki làkku'w Espaañ wu Itaali, wu Fraans ak wu Portigaal, ba fa mu yam. + +Li gën'a yéeme moo'y Yojinyoo Jarin moom dafa jel mboleem amaliiti "yewwute" gi, sol ko ci benn baat, mooy " filolojiaa" , di baat bu am ñaari maanaa yu mag, mu njëkk mi, mu xat la, te daytalu(gàtt), moo'y (( dégg làkk)), mi ci des, moo gën'a yaatu te gën'a xóot, moo'y gëstu yu làkk, yu njàggat yi (adab) (ci tubaab les recherches linguistiques et littéraires). + +Jarin gis na ne bu nu mane'e doxal yooni gëstu yu làkk ak yu njàngat yi, jaarale ko ci gëstu ci dénd bi(nature), jamono jooja aw yoon wu bees di na judd, di yoonu gëstu wu xam-xam wu di kojug làmb, (làmb ba daj rekk, amul waxi kese walla gisiin ), loolu moo ñu'y àggale ci xam-xami matematik yi. +Nga dolli ci loolu ne làkk moo'y seetu bi nga'y man'a gise dundu'g nit gu xel gi, boo gisee ne làkku xeet wu nekk, ci jamono ju nekk, lenn la ci li'y wone am xelam, nga dolleeti ci ne ci lanu'y jànge xam-xam yi nga xam ne bu ñu nekkul woon,amuñu woon, dund gi du mel nii mu mel tay. Bu làkk amul woon nu xam-xam di juddoo ba'y gis jant bi. + +Làkk moo'y cëslaayu ag yewwute bu nu ko waxee, dées na ko man a dëggal, rawati na ku jàng jii jamono, jàngat ko, xam la leen seen " waxiin" yu suufe ya ñu xeeb jariñoon - ñu ko'y woowe ci francais dialecte - ba ñu leen jëlee, def leen ay làkk yu xeet, yu réew, yu xam-xam, yu ñu fonk, yu ñu fas-yéene'e doxale seenu'g dund, sës ci seenu'g dox, sanni ca àll ba yeneen ya doon dox seen diggante ak xam, xam-xam, ak yewwute, mu'y làkk wu latin wi nekkoon di lu ñu neew xamoon, la gën a rëy ca mbooloo ma réere woon ko, te réere gi taxoon ñu reeroon te yewwoodiku. + +Wii làkk, di wu Latin wi, nekkoon na di seenu'b coona, di seenu'w ay, di seen gàllankoor, di ab pakk ci seen digg ak jem-kanam, ndax la ëppoon ca xam-xam ya, bu ma waxul sax lépp, ca woowale làkk la nu ko daa binde, di ko ci jànge, te askan wa bu doon téeméer, lu yees fukk'a ko ci'y xam, mu'y ci misaal daanaka: nga xiif lool, ba'y bëgg'a dee, di wër loo lekk, ndeke lekk gi moom am nga ko, mi ngi ci sa ronu ay tànk, te ya'a ko moom, doo ci fay dara, xanaa kay da nga'y jël rekk jëfandikoo, te loolu lépp xamoo ko, te kenn'a ngi nii ci sa kanam, xam loolu lépp, te xam ne bu ko waxee, dootul jariñu ci, ni mu ko daa defe, kon na la ko bañ'a won, xamal la ne ya'a'y ki ko moom, ndax loolu man na'a waral sa'g wadd sòng ko, giir ko, ne ko fuuf, te bu booba'a su ko ab xiif gaarate'e du xam fu mu ko'y fajeeti ci'g càcc!. + +Waaw waaw, ci'g càcc kay !, ndax lii ag càcc la, ndax xañ nit àqam, di ko jëfandikoo'k'a jariñoo sàcc ko la, te bàyyi ko nee mu toog ci'b xiifam, ci yitewoo àqam, ci taru'g yitewoom, càcc la de! . Loolu ku ni la du sàcc, laaj ko lu mu doon,moo raw sàcc, fëkk la, nax la, réeral la, dofal la, xiifal la, neewal doole la, nakk'a xam la, dofe la, suufe la, réer la, bon la, waxal lu la soob ne moom la. + +Kii man'a xam nga ne ko doo fi xame, ndax làkk wi nga yor du wu ñu'y xame, wa kee yor'ay dëgg-dëegi aw làkk, ci la ñu war'a waxe, war ce'e jànge, war ce'e yëre, war ce'e gëstoo, war ce'e binde, te ci la nu war'a nekke nit, boo xamoon li ci addina bi bepp it te xamewoo ko ci doo kenn ku xam, ku ñu'y lim nga nga'y kenn ci ñu xamadi ñi, ñu réer ñi, ñi amalul seen réew solo. +Lii nag sama gaa yi du'g réer, di'g dof, ak dofale, ak li la soob ci xeeti xelloodi? + +Lii'ay li ñu doon def waa Orob ca jamono yu diggdoomu ya,maanaam " middle ages" ci angle, di nu ko def ci jii jamono - nga xam ne moo'y ju xam ci anam gu gaaw, ngir bari'g li ñu war'a xam - ndax li man'a xam te ëpp ci réew mi am nanu làkk wu ñu man'a xame ci's lëf ci'g gaaw, ak sakanal waxtu, ak ci's lëf ci'g wér, ak lëw. +Kon jort naa ne la'y lañu war, moo'y la wa Orobi joojale jamono defoon, mu'y taxaw ci jël seen àq, delloosi seenu'm dem, feeñal seenu'm réer, sulli seen lu suulu. + +Di na rafet nu indil leen sababi feeñug yile làkk. + +Feeñu'g làkk yu bees yi + +Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi,(moyen âges) moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak niti adab ya, walla njaggatkat ya ( hommes de lettre) ak ustaas ya. La notoon nag ca nit na - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yi'y yu seeni barab lañu déggoon. + +Bi jamono'y "yewwute" dikkee, gelawu'l "fonk sa xeet" (nationalisme) upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak niti adab yi, ak woykat yi, tàmblee jeng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki r��ewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Engle ak yu dul yooyu. + +Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi (xisa bu'y reeloo) Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoom moo'y làkku Romam wii daal moo'y gën ja'a kawe'y jumtukaay ngir génne xasida'y woyam yi. + +Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di franse,ngir wuñi ci li'y yëngu ci biiram, ci njàggat (adab) lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). + +Chaucer mi di'b angle ( 1342 - 1400 g) jug,moom itam, sotti ci'w làkkam woyam yu yéeme yi ci'b taar, rawati na nettali'y Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angle yu mag yi, yi gën'a siw. + +Làkki Tugal yi nag fii lañu bàyyikoo: + +Làkki xeet yu Orob yi, ñi ngi sosoo ci màbbiiti Latin ak Tiyotin. Wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Portigaal, ñi ngi dagge ci Latin, wu almaañ, wu angale, wu danmark, wu suwed, wu oland, wu norwej, bàyyikoo ca Tiyotin. + +Bokk na ci sabab yi jur doxug yile waxiin dem ci làkki réew, yu xeet, bokk na ci sabab yooyu, nekk gu làkku'w latin nekkoon di wenn, ba yàgg mu seddaliku di ñaar, wu ñu'y wax kalaasik, ak wu wilgeer . Kalaasik mooy lu yàgg la'y cosaan, wilgeer, di lu yomb, li nuy jëfandikoo. +Kalaasik wi di wi politigkat yu mag yi, ak boroom xam-xam yi, ak niti diine yi daa waxe. Wu wilgeer wi, di wi niti neen yi di waxe, di ko jëfandikoo. Ci noonu kalaasik wi tàmblee nakk as lëf ci solo'om,ak dooleem, wilgeer wi tàmblee jël barabam, waaye wilgeer wi moom ci jëmmi boppam tàmbli na ci ginaaw bi di soppiku, ndànk-ndànk, jem ca leneen lu dul la mu doonoon, ci noonu ay waxiin yu bari te wuute bànqaasoo ca, ngir nocciku'g lenn ci mbooloo yii, juge ci yile barab dem ca yee,tas fa,ak soreente gi yii barab soreentee te wuute. Loolu jur yeneen mbooloo'y nit judd, mu ci nekk ak sa waxiinu bopp. + +Waaye loolu moom teewul woon latin des fi di làkku diine wi te'y wu xamlu wi maanaam wu ofisel wi, ba mujj askan yi yoqat ko, te xam ne pakk la ci yoonu seen ag dox, aku'g jàll, ndax ña ëppoon ca ñoom xamuñu ko woon,dégguñu ko. Loolu yobb léen ci ñu xëy taxaw temb ci jële ko fi, sanni ko ci seen ginaaw, weccee ko'ok seen waxiin yooyee, te farlu bu baax ci jàllale leen, jëme leen kanam, tèkki ci li ñu soxla woon lépp ci yooyule téere yu am solo, te ñu bindoon leen ci laitin ca jamono jooja. + +Ci noonu nit ñépp tàmblee gis koom mu rëy mii, di ko xam , te bu njëkk, daa xawoon'a jòmb ci ñoom ñu ko'y xam, ba ci'y jariñu. +Lii nag day tegtale rekk li war, mu'y jëfandikoo làkku'w nday wi, niki lakk, ci wàllu'g ligéey ak jàng. + + + + + +Reew yi nekkoon ci ron suku'b sañcaan yi ( colonialiste) yi, rawati na yi ci'y jëfandikoo làkki jàmbur yi ba leegi, niki tubaab, ak angle, ak yeneen, jàppe leen làkki ofisel, yii réew de ba leegi dañuñu di jànkoonte ak ag réer gu kawe te tas ci biiru'w askanam, ak koom-koom bu deltu ginaaw, ak ag des ginaaw gu rëy ak dund gu suufe. +Kon làkk daa war'a nekk di lu yomb lool ci ni ko'y jariñoo, maanaam mu'y làkku'w la ëpp ca nit ña, niki wolof fii fi Senegaal, bu ko defee ñu bàyyil fi ni gën'a néew itam seen àq ci jariñoo seen làkki bopp, ci lefu'm jëf ak jàng. Waaye nag bu booba'a du man'a ñàkk'a jëfandikoo làkku la ëpp ngir jëflante. +Ci noonu la ko'y joxe àqi nekk làkku'w ofisel wi. + +Li nga xam ne sikk amu ci, moo'y gis nga ay yooni yoon, lu bari ci yeneen xeet yi ci reew mi nu'y wax wolof yu rafet ci anam gu jàppandi, ni ko ñépp di defe, ci lu dul ñu ko'y jàng, bu ma waxul li ëpp ci ñoom, te safaanu'b loolu néew na nga gis ko, maanaam wolof bu dégg yii làkk, loolu li ko waral du ne wolof bi daa yitewoowul ñeneen ñi, du caagéenu'g ñeneen ñi dañu'y sotti seen yite jépp ci làkku'w wolof aki mbiram, li am kay da di wolof day làkku jëflante wi tas, samp boppam ci géew bi, franse mii ñu'y jàpple sax manul'a bëre'ek moom mbaa mu gëpplante ak moom. Ndax moo'y làkk wi'y tàbbi ci say nopp, mu neex la mbaa mu naqari la, nga ko'y xam ci sañ-bañ. + +Am na ñu ne ndax wolof am na sax, niki xeet ? + +Man nag ma'y ku yitewoode'e tontu ci loolu, ndax ni mu ma ñoradee, waaye am na nag lu xaw'a am solo ci laaj bi, mu'y booy xool lu bari ci ñi ñu'y tudde wolof - ci laa maa ngii - seen dëgg-dëggi cosaan du wolof, man li may jàpp foofu moo'y wolof li mu'y tollool moo'y “ag cenegaal” , maanaam xeet wi moo'y waa-senegaal, làkk wi di wu senegaal, kon dootul wu giir, mbaa waaso, waaye wu xeet wi wépp’a, Serin Tuubaa amul lenni wolof, Alhaaji Maalik naka noonu te taxul woon nu dégg tukloor, kon day mel ni xalaat bii mi ngi jeng as lëf jëm ci'g yanu maanaa. + +Bu ñu delloo ci li ñu nekkoon di wax mu'y war gi làkk war'a nekk di lu yomb ci ki ko'y jëfandikoo, da ma naan nit ñi daal li leen war moo'y def na waa sowwu defoon , muy tuxal seen waxiin yooyee, yòbb leen ci'y làkk, te sukkandiku ci, xamloo ci, su nu ko gisee muy lu mant'a ñàkk, maanaam bu nu fi gisee lenn lu'y gàllankoor seenu'g dox, di làkk wu fi jóox, wu ñu xamul ni ñu ko war'a xame, niki franse ci sunu-gaal. + +Waaye nag amaa na loolu lepp du nu ko soxla, bu waxtu wa jàllee, ba nit ña dégg way jóoxi làkk yii ni ñu dégge seen làkku nday wi. Ndaxte làkk du yàlla ju ñu'y gëm, waaye kay jumtukaay la ngir déggante ni ma ko jorte. + +Ahmad Amiin wax na ca téereem ba tudd Fajrul Islaam:(( aw làkk sàkkeesu ko ci genn jañ (maanaam jekki-jekkiwul rekk am), ñu mujj ñi bi ñu ko'y jële ci ñu njëkk ña du woon lu mat, li am kay moo'y nit ñi dañu'y sàkk ci seenu'g njëlbéen, ay baat yu tolloo ak seen aajo, bu yeneen mbir feeñee, nu sàkkal leen ay baat yu bees, bu ay mbir raafee amaa na ay baatam raaf. Làkk nag'a ngii nekk ci dund ak dee gu sax, naka noonu bàyyikoo yi (mooy baat yiy tukkee ci yeneen yi) ak waxiin yi, ak baat yi, ñoom itam dañu'y màgg , di yéeg ni xeet wi'y yéege, di ko magge)). + +Yooyule làkk, di yu Orob yi de,gënuñu fenn, mbaa ñu kawe ci lenn sunu yos yu afrik yii, li fi nekk kay mooy ñoom dañu leen'a fonk, sonn ci, di def lu mel ne li Ahmad Amiin di wax mu'y sàkk baat yu bees saa su lu yees amee. Kon sama gaa yi, nanu doylu ci lii nu yor, ndax li sunu di neex, sama dàq na ko kat, te jéem ko'o jàllale,jëmale ko kanam, te tas ko ci mbooloo mi. + +Du'y caaxaan la nit ka'y xalaate, ca la war'a waxe , ci maanaa li nga'y xalaat ci sa biir dënn, sa biir xel, mu'y jeqarbiku ci sa'y yëg-yëg jarul fireeti ci weneen làkk wu dul wi ko xalaat, ngir déggal ko ku nu jàkkaarlool ki, bu ko fekkee mu ko'y man'a dégg ci wi ñu ko xalaate,loolu li mu'y jur mooy yàq waxtu,te mu'y lu gànjaru. + +Wax ju'y joriku, di dikk ànd ak kem bu rëy ci'g jàppandi, manul'a ame ci lu dul làkku'w nday wi nit ki juddwaalee, walla wi mu àndal ay at, di ci jàpp ak'a ŋoy, ci këram ak pénc ma, ja ba, ak daara ja, nga xam ne da'y faf fàtte wow ndayam wa, mbaa mu xaw ko'o fàtte,ba mujj wii di wu jóox sax mooy far di taxaw taxawaayu wu nday wi. +Bu dee fii nag, gisagunu tubaab jël fi taxawaayu'b wu nday, wolof mi'y nday kay moo sax di nday ba leegi, ci moom rekk lanu'y man'a ame joriku gi nu sox la ci wax, misaalu'm loolu yaa ngi koy gis ci ñii di xëy ak'a gont ci leekoli nasaraan yi, ñoom de ca dëgg-dëgg da nanu ko dégg xayna , waaye lu ci ëpp, du ñu ci man'a génnee seeni xalaat ci'g joriku aku'g yomb, waxal sax aku'g dëggu, ndax dañu'y diriku ci seeni wax ak'a jàddantu, ak' a xootal fu nu ko waroon'a tondale, ba far wax ja day doon leneen lu dul la mu bëggoon'a doon, walla sax leeg-leeg ñu rax ko ak yennaat ci baati wolof, ngir noppalo'o ca, bu ko defee tubaab bi déggul ay wolof du xam li ñu'y wax, wolof bi déggul ay tubaab it naka noonu, kenn rekk'a ko'y xam ki boole ñaari làkk yi. + + + +Li ma gis moo di Orob ca yaatoom ga, ak ca jégeente'y xeetam ya, ak seen ag niroo, ak gu làkk, ak bokk gisiin ak diine ak melo,ak - man nga ne - jëmuwaay, nga rax ci dolli, nekku'g yenn ci seeni làkk di - man nanu ne - yu addina bi bepp, niki angle, ak wu ko xaw'a jege niki francais, teewul ñoom ñu nekk di ñu jàpp ci seeni làkk, xeet wu nekk ca wosam, te teewu ko'o jàng nag yeneen yi, rawati na angle, di ci jokkoo saa su begge'e jëflante ak ñi déggul wa mu yor. Danmark ma nga'ak danwaam, Suwed wuwedam, da ma'a tayye'e lim, waaye wu ci nekk ak wosam, ba ci Belgik sax nga xam ne ñaari xeet yu wuute'e fa dekk, teewul xeet wu nekk, yor sa wosu bopp, te teewu la'a jàngi leneen ba ca wu sa moroom, bi nga ko gisee mu'y xam xam, ndax xam-xam du lu moy xam lu mat'a xam, te loola mat na'a xam, ndax da na jur ag rataxal diggante, jur ag xam sa moroom, jariñu ci, jariñ ko. + +Addina bi dafa war'a sosu ci'g dimblante, jariñante, fonkante, deet jariñoo, ak dimbandikoo, te lii tubaab yi di def, du lu dul dimbadikoo, ak jariñoo, ci suñu'g suul, ray, joggi, nërméel mbooleem sunu yëf, ci taxawal seen yëf. + +Wolof nag daa na wax : (( pesu'm kanam boroom'a ko'y fajal boppam)), kon nag pes nañu nu, lu nu'y xaar, du nu jug di door, mbaa nu'y daas ay jaase'eki gobar, li nu'y def kay moo'y jëfandikoo xel, ni ko seriñ Mbay JAXATE daa waxe, mu'y ab noon bu la noonu, boo'y xeex ak moom, bu mu ko yëg, na xëy rekk daanu door a xam ne ya'a ko daaneel , fa la sa'b noflaay di ëppe, ca la la nga'y jëfandikoo ci ngànnaay di gën'a néewe, ndax bu fekkoonte ne daa waroon'a jàmmaarloo ak yaw, nga'y jëfandikoo lu ne ngir moytu'y dóoram, ak di ko jéem a dóor, leegi fegal nanu la coona'b jéem'a dóor ak moytu, moom kay da nga'y agsi rekk dóor, mbaa nga jam, ndax moom yëgul ni ya'a ngi koy fexeel, bu ko defee mu dee, naaxsaay. Lii estraategi la ci. + +Lu mel ni franse ci réew mi, manoon na fe'e nekke ni fi araab nekke, di'b soppe te bañ di'b noon, di luy dem ànd ak di demale, waaye jort ne moom rekk'a war'a dem?. +Xoolal ci maanaa araab ñi ko jàng tay, ñoo'y ñi dégg wolof, ñooy ñi ko fonk, ñoo'y ñi ko'y suqali, loolu bu amee li mu wund moo'y ne araab ca mag ña jumtukaay la woon ngir jëm kanam ci xam-xamu diine waaye it jëmal kanam seen kàllaama gi nga xam ne tay daa fees dell aki baati araab yu ñu jox kàddu'g wolof, ci fi ko wolof amewul. Xoolal ma baatu’b jamono, mi ngi juge ci samaanu, maanaam juge ci mahnaa, yu mel nii yu sakkan lanu ci, daa nanu dem sax ba’y jëfandikoo as lef ci xarala, di sàkkal wolof ay jumtukaay yu làkk yu mu amutoon te ñu gis ko ci araab, te xam njariñam, xam ne man na leen'a amal njariñ, niki yaa'g askanal googu nekk ci araab, nu ko daa tollolee baatub koj , naan yef yu di koju'g nàggam, ci maanaa xam-xam bu di koju'g diine, jublu ci xam-xamu diine, mu'y mbaat sos su nu ko fonkee, man na'a am ay jeexiit yu am solo, ci ëllëgi làkk wi, ak ci diggale , di ci tubaab par l'intermediaire de , ak ci'g jonjoo, di ci tubaab en direct. +Yii di baat yoy danu lay won ni araab jeexiitale ci wii làkk, du caagéenu danu di ay baat yu amul woon ci wolof, aha kay yu ci amoon lanu, waaye fii yeneen maanaa lanu yore yu bokkul ak yanu yoroon, nun itam bu nu gisee ne yii du yi nu soxlaati, walla maanaa yii jubul, am nanu sañ-sañ ci def ni nu neex, ndax ñoo'y boroom. + +Kon noom ñaar way jàppante lanu woon yu'y dimbalante, dunu woon ay noon. Wolof am na ay waxiin yu bees aki baat yu yees, ci tabe'g làkku'w araab la ko ame . Ndax boo'y xool da nga'y gis ne woomle'g wolof aku'g riisam mi ngi ko jële, ci jël lu toll ne làkku'w araab ca yaatoom nga, ak tàllalikoom ga,firi lépp baat topp baat, loolu moo nekkoon seen anamu'g jàngale, nga xam ne da nu la'y wax baat firil la ko, ba mbooleem teere yi nu daa jàng ci araab - te yu bari lanu woon te wuute, ci fann yépp - ci nii la nu ko daa defe. Loolu jural leen nu mujj baat bu nu am ci araab ca woomam ga, nu am ko ci wolof. + +Bu dee franse moom ci nga'y dégge wolof bu naan la : nga jéggal ma sama wolof daa leerul, te loolu ag xeexam ak ag jéem'a suulam'a ko waral, ag yaakaaram ne moom rekk'a war'a nekk ci kaw suuf'a ko waral, ak jeem'a toogam ci laltu gi, mu des ay barab yu nu man'a toog, mu teg ci ay tànkam, lal ci'y loxoom ne kenn du ci toog, moom reek, moo di li ko waral. + +Kon de kii ku siis la, ku xat la,ku nay la,ku'y ngartaajoo la, ku'y nangu suufu's jàmbur la, ku yëg ne moom rekk la, ku am bëgg-bëggu suuxal la, lii nag ku ko mas'a am ya'a'y ki nar'a suux,nar'a neen,nar'a seey. + +Waaye loolu lépp du tee mu'y lenn ci li ñu moom, moom nasaraan du moo moomati li nu ci moom, ndax ca Aljeeri de, kenn ci ay xalaatkatam nee na woon : franse de lenn la ci sunu am "màngiit" mi nu mànge ci tubaab yi. Màngiit moo'y xaniima, di ci maanaa li nga'y nangoo ci ki nga'y xareel, boo ko gañee, maanaam loolu moo'y li franse di ñëw lépp ngir nangu, jël ci doole, fitnaal, foñloo, fàtteel, taxaw ci doole,jaaye ko, teewul muy lu am solo, di lu ñu man'a xame'e, man ce'e jariñoo, kon bu nu ko jàppe njariñ lu nu'y sànni, waaye màngiit, mu nu mànge ca sunu xare ak ñoom, ndaxte addiis'a ngi nii bu naan : (("hikma" moo'y réeru'm jullit bi, fu mu ko gis daal na ko woor ne moo ca gën'a yay)). Hikma nag di lol boo ko doon firi da nga naan moo'y lépp lu rafet rekk, jekk, xellu, baax, di lu ñu xam, di lu am solo, ci dund, mbaa dee, xel mu rafet, ba fa mu yam. Kon franse li fe'ek ya'a ngi ci'y gis sa njariñ, moo xam lu adduna la mbaa leneen kon ci hikma la. + +Waaye kay li'y li yéeme moo'y da ma'a gisagul ci réew yi'y dem, te'y dox, di dund, di jëm kanam, mu ci'y waxe ci'w làkk, bu feeñee, bu làqoo weneen, maanaam loolu mooy li xew tay ci sunu réew mi, nga xam ne bu ñu feeñee ci lu fés, mbaa nu'y jëflante ci anam gu ofisel, - "ofisel" ci li wolof mànge ci tubaab la - da nga nu'y gis nu'y waxe ci kallaama'y nasaraan, bu nu delloo fa sunu'y kër,di ko defe ci wolof, leeg-leeg sax nu'y rax la ñu'y defe ca franse yennat ci baati walof, kon mokkalaguñu, te loo mokkalul manoo ce'e jariñu, li'y li nu mokkal kay moo'y sunu wolof mii ñépp di wax,ku dégg franse ak ku ko déggul, ku'y ku ndaw mbaa nga'y mag. + +Fii nga'y gis jëwrin ju mag ju taxaw di wax ci googule kàllaama ba yàgg mu ruur toolu'b wolof, fac ca soxlaam bu baax, mu mel ni daa déggatul tubaab, walla mi ngi ko'y bëgg'a sonnal, ndaxte nag ca dëgg-dëgg coona la, di wax lol boo ko déggee it, wi nga nàmp nga gën'a dégg, te ci nga gën'a gise sa bopp, ki nga'y waxal it moom la gën'a dégg, du am lenn lu mu ci'y xel ñaar, mbaa mu ko ci'y laaj,du caagéenu'g baat bu mu ci'y réere daanaka. Ba ci sunu njiit lii fi nekk tay, di Wadd, ba laa bég ruur toolu'b wolof ci biir waxi tubaabam, day mel ni da ce'e gën'a gis boppam, mbaa mu gën ko'o yòmb, mbaa noppal, wax leen ma lu mu ?. + +Raw gu xam-xam gu mag itam boo'y xool, da nga naan demewu fi noonu, li sabab loolu moo'y ne nun li ñu'y daj ci dégg tubaab daa metti te rëy, te li mi'y jël ci ñun ci waxtu daa takku, loolo'oy li'y waral nu'y neenal xam-xam yi, moom kay fii fi Senegaal dégg franse doy na fi xam-xam, àgg na ci sunu njiitu réew lu njëkk la, xam-xamam bu mag ba nu doon naw lépp, du woon lu dul :naan na géeju'g franse, du ñu ne la benn xam-xam bu di koju'g tegnik mbaa xarala la xam. + + + +Seriñ Tuubaa mi ngi ñu naan - ba mu ñu'y jàngal xam-xamu Lislaam - : jiitalal xam-xamu" tawhiid" mu'y li la'y xamal ni nga'y gëme Yàlla, kennal ko,wéetal ko, teg ca " fiq" mu'y ni nga'y jaamoo sunu boroom, ak "tasawwuf", waaye mu teg ca ne ak jumtukaay ya, mu jublu ci jumtukaay yi; làkku araab ak la mu'y àndal ngir nga man ko'o dégg, mu'y nahwu ba ak bayaan ba, "nahwu" di li'y nos làkk wi di ci franse grammaire, bayaan di li'y nos wax ji, di tax doo guddal lu waroon'a gàtt, loolu lépp, bi mu ko'y lim mu bokk ci xam-xamu diine, da leen'a tudde ay jumtukaay, mu jublu ci ne xamluwunu leen ngir seen jëmmi bopp, waaye ay raas lanu yu nu'y yéege jëm ci xam diinee, rawati na alxuraan mi nga xam ne manéesu ko'o, walla su c'ee xam te déggeesul araab mi nu ko wàcce, ndaxte làkk wu nekk, am na jagle'y boppam yu moom rekk'a ko moom, ku firi wor la léeb wa wax, rawati na lu mel ni alxuraan ca jafe'g làkk wa nu ko wàcce, ak màggu'g aji wàcceem. + +Bu nu waxee màggu'g aji wàcce ji, da nga ci'y dégge màggu'g li nu wàcce, kon loolu màgg na màgg gu kenn mant'a dégg ci'g yòmb,ak'ub noflaay, lii moo'y li waral araab di jumtukaay ngir xam diine, di xaaj ci xaaji xam-xami diine yi, kon mag ñi jànguñu woon araab ngir jëmm ja, waaye jumtukaay la woon ngir xam la mu ëmb, loolu mooy safaanu'b ku mel ni Senghoor aki gaayam, noom làkk wi moo leen taxoon'a jug,nu sonn ci, sonle ci, bu taxutoon, doo def fo'o toll di dégg baatub frankofoni, lu mu'y wund ? tontu leen. + +Yalla baax na, ba mu nu teralee ci nu nekk ci jii jamono di dellusiwaat ci sunu bopp, di ko tàmble’e fonk, di gestu li jar'a gestu, te lu ci gën'a rëy sunu kàllaama gii?, ndax giñ naa ne xam gi bu wóor, ak jëfandikoo gi ci fànn yépp di nanu jariñ lu bari, te'y jëf ay jëf ci yòmbal sunu'g dund. Da na nu yòbb tam ci nu'y dëgg-dëggi réew, dëgg-dëggi xeet, dëgg-dëggi ay mbòkk, yu gis ne am nanu lu nu bòkk, yu'y mbòkkoo ak'a joqalante ci'g nooy ak'ug jàppandi. +Jëflante di na gën'a dolliko'o ratax, déggante gën'a yòmb,xam gën'a jàppadi, koom gën'a lëw, ndax xam-xamu koom di na gën'a yòmb'a jariñoo ci ligéeykat yi, jaaykat yi, naka noonu naataange di na raññiku ci wàll yu bari, ngir xéewal gi am te ame ci jàppandi'g xam mbir yi, ngir jumtukaay bu yòmb bii am te amutoon di sunu'w làkk. + +Ana lu ku am’um xel di wooye am xaram naan ko kaay ? + +la ko war kay moo'y mu ne ko bar, bar moo'y baat bi bàyyima bii xam, kon noppal sa bopp du nga nekk fa naan ko kaay, waaye xanaa bar mooy li sonleedi. Naka noonu ñu dégg ba noppi wii làkk, nga xam ne leegi xam xam-xam rekk'a nu war'a ñor, te dese nu, nu naan da nu'y bàyyi wii nu dégg nee, naan dañu’y xamlooti weneen door'a xamlu xam-xam yi taxoon ñu'y xamlu'w làkk, loolu jort naa ne dofe la, sànk waxtu la, sonnal sa bopp la. + +Jàppoo ni sunu ligéeykat yii ca seen yewwute ga ak muus ga ak xarale ga, bu nu ci doon boole di leen seetal li nu aajowoo ci xam-xam bu aju ci seeni ligéey, defal leen ko ci seen làkku réew wi nu dégg, naan ko, xam ko xam gu xam kawewul, jàppoo ne bu loolu amoon du ñu fi xar baax, jëf fi ay kiimaan, def fi lu raw li tubaab yi di def, ba nu leen di naw ?. + +Da ma'a yàgg'a dégg ci sunu biir ku naan nit ku ñuul daal, xawma lu mu def Yàlla, ba Yàlla gàttal'um xelam nii !, te loolu day mel ni bu nu ko'y wax, ñi ngi dëggal li tubaab bi yàgg'a wax yàgg ko'o jort ci ñun mu'y moom moo nu ëpp xel, walla sax moo'y ki ko am, nun li nu am du am xel, ndax xel ak ni mu màgge jòmb naa nekk ci yaram wu ñaaw, wu ñuul, wu tàyyeel wii. Am ku ma dégg te moom ku ñuul la, mu mel ni ku'y jàpple tubaab yi ci seen wax jooju naan: ((ñu ñuul ñi de àjjana bu ñu fa duggee, su nu fa yàggee yàq ko, naqaril ko. Tubaab yi nag ñoom, bu nu tàbbee sawara, su nu fa yàggee defar ko, neexal ko)), waaye boo'y xool sax da nga'y mel ni ku gis lu ni mel, te sabab bi du dara lu dul jumtukaayu jàng bi moo nekkul ci sunu loxo mu'y sunu làkku bopp, làkku jàmbur day waral nga gëm jàmbur, xeeb sa bopp, xoolal ci nun ñi'y làkk tubaab, sunu delluwaay, sunu jëlewaay, sunu ndëërlaay moo'y fraans, ak nu mu man'a rëye mbaa mu tuutee ni, kii moo'y ki nu gëm, bu nu ko gënoon'a xam it jort ne moo nu ko gën'a def, lii aji am la ju ñépp di gis, di ko dund. + +Li ñu’y wax cosaan, da'y baat bu waa senegaal baaxoo wax, di ko tudd lu bari ci seeni wax + +Li ñu’y wax cosaan, da'y baat bu waa senegaal baaxoo wax, di ko tudd lu bari ci seeni wax, mu mel ni day lu ñu fonk ba ci lool, mu mel ni fonk gi moo'y yoon, ndax boo'y xool, cosaan mi ngi bàyyikoo ci baatu sos, di kon fa nga sosoo, juge ca, bàyyikoo ca, bu dee nit la ndayam, baayam, dëkkam, réewam, aadaam, aam, lii moo'y cosaanam, ndax ci foofu la sosoo, bàyyiikoo fa, kon lii mooy cosaan. Waaye ndax li nu def fonk cosaan la ? Nan laaj sunu bopp bu baax te xootal laaj bi, ndax fonk nanu sunu bopp? Sunu cosaan ? Man dama naan déedéet, déedéet kay, ma dellu ne déedéet. Jort naa ne ci barabu fonk sunu bopp, tubaab bi mooy ki nu fonk, ci barabu sunu cosaan, cosaanam, lii'a'y li am, di li nekk. Tubaab bi la nu'y xëyal, di ko gontal, ak doonte as lëf ci sunu njariñ'a ngi ci, aw làkkam lañu'y sonn, bàyyi sunu wos, te kat làkk moo'y dëgg-dëggi cosaan, ndax mooy seetu bi'y wone boroon, te'y jimblang ji'y ëmb li xeet wi indi ci'y jaloore, aki mbanoore, aki aada'aki cosaan. + +Kon moo'y mbuubs mi nga xam ne bu la réeree, la mu ëmb sànku, naaxsaay. Kon déet ag wuutu di ñeel ko. Tereesul jàpp weneen waaye na sa wos jiitu, ndaxte léeb wa nee na: li nga am boo ci séenéenul doo ñeetaane!. Mu'y ci maanaa li nga moom boo ko fonkee, mu doy la, nga doyloo ko, doo soxlaal kenn lennam. Mu'y lu wóor, ndax jort naa, lii fi nun bu nu ko fonkee, dem, te du nu sonn, mbaa nu'y ñee kenn. + +Mu mel ne la Karlo LEFI waxoon di kok ku jàng "njàggat" lu Itaali - njàggat , fii mu'y tekki litterature ci nasaraan - da nga ko xam, mu ne woon:( Kristo s'è fermato a Eboli ), di ci maanaa Kristo, di yonnant Yàlla Hiisaa, ma nga yam ba mi'y def doxu'b nitale ba, yiwale ba, xayale ba, taaxale ba, diinele ba, yéwénal ba, ma nga yamoon ca Eboli, jotutoon’a àgg sunu dëkk, jublu woon ca loola ne "àtte" gi, walla ci ni nu ko gën'a baaxoo waxe "nguur gi" mu'y baat bu ma soof, ndax nguur moom nekkul lu dul fu'y buur di dunde nguur nekk fa, waaye mu begg'a wax ne nguur gi kon di gu Itaali, bi mu'y defar da fee bayyi sama dëkk bii jéemu ci dara, sama'w nit di ñu dofe, ñàkk am xel, ngir néewu'g li ñu leen sotti ci xam-xam, man itam ma ne naka noonu, ngir sunu ñàkk'a jëfandikoo sunu làkk, di jël wu keneen. + +làkk moo'y yàlla ji'y faji aajo? + +Ku wax lii de amaa na ñu ne ko: yaw de xanaa da nga'a faf jort ne làkk moo'y yàlla ji'y faji aajo, rawati na bu dee sa wosu bopp?, ndax da'y mel ne lu'y xeeti man-manu def, ak jëmale kanam, jumtukaayi jàll ak jàllale jox nga ko ko, kon daal moom rekk doy na ngir dox ? ma ne déet, du loolu la'a bëgg'a wax, li ma jublu kay, moo'y moom de moo'y gën ji jumtukaay, te'y gën ji dokk ci ku mant'a ñàkk'a sukkandiku bu'y doy, gàttalaakonu'b dox la, yombalaakonu dund la, mbokkalaakon la, bennalaakon la, di boolewaakon, di taxaakonu yëg sa bopp, fonk sa bopp, tasaakonu xam-xam, jàppandilaakonam, dabalewaakon, ak ak ak. + +Man de maa ngi naan te du ma dañ naan: jël leen ko! moom'a de!. +Moom'a de, moo'y li ñu'y teral, di ñu jugal, di nu doxal, di tax nu'y xalaat, di bind, di yër, yëglekaay yi'y lëw, di jàngu, ay bindkatam di dolliku, taalifkat yi'y yokk, yëngu-yëngu gu xam-xam di gën'a sawar, cawarte'g caada ak gu saxaafa gën di dëggu, gën di fés, gën di laalu. + +Bindante di mujj di nekk ci lu dul ab coona, ci's lëf ci'g gaaw, ci'b noflaay, ci'g ratax, ci lu dul xalaat, mbaa toggoo, wàlla yenn anami moytu. Kon moom la, mooy noflaay bi, di jàll gi, di naatange gi, di meññ gi, di woom gi, di fulla ji te'y yéeg gi. +Xoolal as lëf ci yitewoo gu tar, ak jublu gu mag gi nga'y seetlu fii mu nekk, ci sunu mbiri réew ak mbiri xibaar, te loolu li ko jur du dara lu mo'y xibaar gi nu'y xibaar askan wi ci seen làkku bopp wi, nga xam ne jamono jii, ñépp'a yewwu, kenn gënul'a xamati ki jàngul li'y xew ci réewam, ci wërlaayam, ci goxam, njiitu'l réew mi sax gënul'a xamati gone gi'y gën di gone li'y wëndéelu ci mii réew, ak ca mee. +Lii lépp ngënéelu'l sa'w làkk'a, da'y wëy nag ba ca lu dul xibaar, àgg ca mbooleem lu dox mbaa mu raam ci lu nekk, di yombal, di gaawal, di àggale, di noppale, di soreele fitna. + +Seetlu naa mu bokk ci la ma seetlu, ne leegi jàngkat yi ak jëfandikookati internet yi dañoo am ag jeng jëm ci bu nu'y bindante di ko defe ci wolof, rawati na bu nu yakkamtee, li leen jañ ci di ko def boo ko xoolee, lu yanu maanaa la, te yéeme, mooy noflaay bi ci nekk, ak gaaw gi, ak nakk'a faale gi ak ñàkk ge'e xalaat, mbaa ragali yaq ci nasaraan, kon lii lépp, ay pakk lañu ci sunu ay xalaat di dox, sunu'y xel di xelli, suni'y xalima'y sotu, sunu'y daa di soosu, nu'y joyal sunu'y gog ci di bind li'y jeqiku, ak'a fuur, di buur ci sunu'y xol, war'a nekk di lu nu'y yaxal ci keyit yi, ba way bañ ñi kumpa di ko war'a xam. + +Am na jeneen aji feeñ (fenomene) ju am ci jamono jii, moo'y ñu bari ci ndonga yi'y bindante ay bataaxel (sms) ci ëyukaay yi (telefon) danu ko'y def - bu nu ko deful ci wolof - ci franse bu nu daggat, maanaam , bu nu dog la ca'y sonnale, mbaa mu ca'y yàqloo, ngir ma gën'a leer, danu ko'y bind ci anam gi nga ko'y dégge man ko'o xam, déet gi mu ware, ci maanaa ci barabu mais nu bind mee, veux nu bind ve. +Loolu ba tay da'y wund lakkal gu leen wii làkk lakkal, ci mbindiin wi, dégg gi, jël gi mu'y jel seen waxtu, ak jafe gi ci ñoom, leeg-leeg nga gis ci ku ci def lu sakkan ci dundam ci jàng ko ci'g tar te du tax mu àgg ci fi ci war, te wolof kat mi mu jàngul, masu ce'e sonn, ma nga ko dégg dégg gu xar baaxe, kon kii bu ko jàngoon, mu yiteel ko ni ko franse yitéele, nu mu'y mel ? laaj naa la ko. + +Xanaa kawe, xanaa raw, xanaa noppalu, xanaa sakkanal waxtu, xanaa gaaw'a àgg, fees, yewwu ci'y nelaw, xippi, taxaw, jàll, romb. + +Waa ja daa wax: + + +Màggat mu màggat ci am njàggu'm tubaab, jabaroo <> tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii dëggel na, kii du bëggati ku dul tubaab, lu dul tubaab, dara ci boppam, li mu moom du ko ñorati,te ñii nag ñoo'y ñi ñi'y faral'a dénk sunu gii gaal, kon waxuma la jengal ko, waaye diigal ko la ñi'y def ! +Ñoom xamunu joow gaal, li ñu'y wax permanaat la nu xam (promanade), ànd ak seeni jabar mbaa'y ndaw, xaj topp ci, ñu'y def leeg-leeg ñu sanni ko ab bant, mu wadd for, nu ko'y xonte li ëpp ci sunu njël li, bu ab baykat di dee ci'b xiif, te moo'y ki taxawal koom mi, ñu'y jënd ay way màggi mbéregaan (oto), naan lu manul'a ñàkk la, te doonoon ñu ñàkk. Ñoo dugg walla, su nu taxawul ci doon sunu bopp, ci lepp, ak fepp!. + +Xam nga réew mii da dul mu nu yore xam-xam waaye nasaraan, firnde ji moo'y lu waral ña fi nekkoon te doonoon ay boroomi xam-xam te di ñu nasaraanoodi, nanguwuñu woon leen'a jox'ub nosam, bu ko defee nu ko'y wommate xam-xam ak leer, bëgg sa bopp, sa réew, sa njariñ, sanni nee lu keneen, waaye loolu lepp, du man'a nekk, ndax du sunu mos mu keneen la, te keneen ki tubaab la, kon moom ñoru ko mu'y dem, di dox, di jëm kanam, li ko ñor kay na des ci'y loxoom, mu'y digale ni nu k'oy yoree, ndax mu man di sax di lu mu moom, waaye tay nga dee de,yaw tubaab!, lii de jaral nanu sunu ay bakkan ak yu doom, ndax ñoo'y ñi ko moom, kon tëyyal sa yëf te ba no'ok li'y sunu, lii'a'y li waraloon mu dénkoon ko màggat ma màggatoon ca njàggu'm tubaab ma, te jabaroo ca, xalaatu ko'o dénk keneen ku ko mo'y, ndax moo'y genn wàllam, di ki mu wóolu, di mbuus mu ñuul mu ñu sol yaxi tubaab, yàpp wa, xel ma, xalaat ya, nii la ko jenn waay ju Mbayeen daa waxe. Xoolal ma kii nga xam ne naan na géeji xam-xam yi te defewu ko ci tubaab ni nu ko'y def, danu ko'y yòbb ba ca àll ba, nu jox ko fa as ndiggante su gàtt ci waxtu ci benn leekol, mu fa'y joxe ay bind (cours) ci wu araab, ak doonte la mu jàngi woon du làkku'w araab, da ci doon jànge rekk kay. + +Gisati nga fii firnde ju leer ne ñoom de xam ñoru leen du caagéenu'g xam-xam, li leen ñor kay moo di njàngu'm tubaab, lii nag waa-réew mi, ñoo'y ñi ko war'a dindi, sunu bëggee boy, joy, tàkk, wëy, di yéeg, ànd ak way yéeg ñi. Mii du dem li fe'ek nii la. + + + +Bu nu dee ñoñi "li fi nekk" (realistes) , dañu naan: nanu bàyyi li fi nekk mu nekkal boppam, du nu ko ga kenn mbaa nu ko ci'y manante (forse), nit ñi tànnal seen bopp ci anamu'g demokaraasi, bu ko defee làkk wu nekk nu jox ko àqam ak li mu yayool ci ndimbal, aar, jàllale, nga xam ne déet ag noono, loolu man na'a nekk sunu ndimbal, sunu njariñ, te ñu sanni nee li nu'y wax ofisel, am as lëf ci'g nooy "flexibilite", ubbiku, ci mbooleem làkk yi, ubbiwaat bu baax sunu làkk wii mu man'a ëmb, guux baat yu bari yi ko'y noppal, te bañ di sonn ci di leen wutati ñu'y juge ci boppam, fu nu gise ne lii moo yell fii, nu ne loolu la, ba kero lenn di taxaw taxaw gu fés, gu leer, gu deesul sikkati, man nga ne loolu sax am na ci wolof ci sunu gaal, waaye du tee nga ne am na yenn ruq yu jar'a gën'a ubbi, mu aju ci tas mbind mi, gën ko'o jàngale, gën ko'o yaatal, ba kero booba, ak ba ginaawam sax na ñu'y jëfandikoo lu fi nekk, te xam ne sunu yëf'a, waaye ci anam gu maandu, gu yamoo, te yell, gu dul gaañ kenn. + +Lii nag am ci sunu tele bi, nga xam ne daa mel ni yëfi kenn la du lu nepp bokk, ñaaw na. Di xibaar lu toll nii ci'w nit, moom li nga leen di di xibaare, nga ne as daggiit ci waxtu lanu leen di man'a jagleel, bu dee ñeneen ñi nga xam ne ñoo'y ñi gën'a néew, te'y ñoñ boo ko doon seet sax, da nga naan matunu fukk ak dara ci teemeer ci askan wi, nga jël la ëpp ci waxtu jox leen ko, nu'y xibaar xibaar yi ci franse te nga ne yeete’e la tax'a jug? ay fen la de, ay nar la, li waral jëf jooju kay moo di màggat mu jabaroo tubaab'a la ko digal ci taxawal keneen nërméel nu, suul nu, suul sunu teddnga, sunu'g xam, yekkati keneen ki nga xam ne ca dëgg-dëgg wart'a woon'a sax aajowoo gile yekkati. + +And ak loolu lepp du tee "ag jam" (critique) di lu man'a ñàkkadi ñeel ñenn ci sunu Imaam yi, ndax itam jël lu tol ne mbooloo mu toll ci ay teemeeri teemeer, nga'y wax ak ñoom di ko def ci làkk wu nu xamul, teg loolu diine, loolu dofeel la, yàq waxtu la, yab nit ñi la, xeeb sa bopp la, xamadi la, xamadi màggu'g diine la, ndax lu nu rafetlu la ci fu nu'y xutbaa nit ñi ci ajjuma, ginaaw ay jullit lanu, ñu laal ci's lef ci araab, làkk wi'y wu alxuraan, loolu boo ko'y xool ag sonn'a ngi ci, ci jàng ko ngir man'a xam Alxuraan, waaye it xamante ak sa yeneen mbokki jullit yi, ndax moo war'a nekk làkku ofisel wu addina'y jullit ñi, di dox ci'g bennale, ci 'g boole, ci'g xamalante, ci jappandal ag jokkoo ci biir jullit ñi. Waaye tekkiwul ne danu fe'e war'a nekk naan xar mi kaay, te'm dégg rekk bar . + +Aji laaj laajoon na ne : ndax li nu'y jële ci jàngu bu nasaraan bi ci xam-xam, man na'a wuutu li nu ci'y ñàkke ? ab laaj'a ngoogu, di bu diis, bu rëy, bu am maanaa, bu soxla ku ko tontu. +Man la ma ca jéem, ci tontu bi, moo'y benn baat , bi ma jortul ne keneen du ko ci weesu, moo'y déet, déedéet. La nu fa'y ñàkke te mu'y lu gànjaru, di lu am solo, moo'y li nu fonk'a wax, mu'y cosaan, làkk nag ñëw di li ko'y jëmmal, di ko taxawal, di ko wuutu, di ko nekkal, di li nga xam ne ci lu dul moom déet cosaan. +Kon lu nu fa man'a xame réer nanu, ñàkk nanu, gàttañlu nanu, dof nanu, ñàkk nanu jumtukaay ba, jumtukyu'b yombal ba, bu noppal ba, bu gaawal ba, bu rataxal ba, bu jooral ba, ba'y déggale te'y bennale, di yombale ag jokko, te di ab xamalewaakon. + +Làkku'w jàmbur niki doju pakkastal ci yoonu jëm-kanamu réew yi ko'y jëfandikoo te taqoowunu ak moom taqoo nga ca war: + +Sunu boroom (t.s) nee na (( wamaa arsalnaa min rasuulin illa bilisaani xawmihii, liyubayyina lahum)) mu'y : yonniwunu benn yonnant ci'w nit ndare bu danu ko'o waxloo ca làkk wa ñu dégg. Lii Yàlla sax ci di ko def, bu amee lu mu'y tegtale de du weesu waru'g wax ak nit ñi, jàngal leen, ci wi nu màgge, dégg ko dégg ga ca war. + +Ndax da na dagan ñu jàppe baat yu jóox yi, lu bokk ci làkk wi ? + + +Baat yu jóox yi ñooy yi dugg ci làkk wi te bokkuñu ci woon, niki baati tubaab walla araab yi nu'y gis ci wolof. + +Bokk na ci li yayoo xamle, mu'y làkk moo'y li nit ñi di wax di ci déggante'e, maanaam jaaduwul ñu naan bii baat bu franse la, walla bee kon nanu ko sanni, te nit ñi ci lanu doon gën'a déggante'e ca bu wolof ba ko fa doon wuutu, Ahmad Amiin nee na ca teereem ba tudd Fajarug lislaam: (( Araab yi de ca njëkk lislaam jële woon nanu lu sakan ci'y baat ci làkku faaris, di wu waa Iraan wi, ak wu Rom, ak wu Isipt, ak wu Ecopi, yooyu baat seen yaxantukat yi daa dem foofa'a ko daa indaale, nu duggal leen ci seen làkk wi, boole ko ci, waaye nag araabeel leen, maanaam dëppale leen ak sart yi seen làkk laaj, ci noonu Alxuraan ñew tudd leen )). Kon nag bépp baat bu nu man'a jële ci làkk, daa war'a lemu ci sarti sunu'w làkk. + +Amiin neeti na ci benn teere bi: (( Yahood yi de am nanu ag jeexital gu mag ci làkku araab, tàbbal nanu ci ay baat yu bari yu araab yi xamutoon,ak ay term yu diine, yu nu xamul woon,baat bu mel ne jahannama ak shaytaan, ak Ibliis lenn lanu ci)), waxaat na ba tay ci bii teere: (( woykati araabi nasaraan yi, ku ci mel ne Xussu'bnu Saahida, ak Ummayata'bnu Abii Salt, ak Hadyu'bnu Sayd, ñoom duggal nanu ci araab ay baat aki toggaliin (taraakiib) yoy araab yi xamunu ko woon, ni ngi naan Ummayata'bnu Abii Salt moo xamal araab yi waxiinu " bismikal laahuma" , mu'y ci maanaa (ci sa turwi yaw buur bi ) ñu ci'y tàmblee ay wax aki jëf, Xussu it moo'y ki njëkk'a wax "ammabahdu" )). +Ammabahdu di baat bu nu'y jëfandikoo ngir teqale wax ju bokkul ak ji la tax'a jug,mu mel ne nga'y bind bataaxel, nuyyoo, wax li'y ànd ak nuyyoo bi, ba noppi war'a jëm ci wax ji ne ( leegi nag:). + +Lan moo'y jafe-jafe bi ku senegal ki di jànkooteel, ngir làkk yu bari yii nekk ci réew mi, fekkante fi, ñu'y yu jàmbur yi ak yu réew mi, te nu jël yu jàmbur yi teg leen ci kaw yu réew mi ? + +Nitu'g neen ci sunu réew mii, bu duggul leekol, ak doonte dugg na ko te bu tubaab, da nga ko'y gis jamono ju nekk mu'y jànkoonte'ek lu bari ci'y jafe-jafe, ci lu aju ci ag jëflanteem ak nit ñi, aku'g jokkoom ak ñoom. +Jafe-jafe yooyu lu ci ëpp, li ko'y jur moo'y ñàkk'a déggoo gi'y am ci digganteem ak ñoom, te loolu da na àgg ci jural ko ag fasu (complexe), ak ñàkk'a wóolu sa bopp, ndax lu ëpp ci waa senegaal da nu'y gëm ne seeni mbir keneen'a leen ko war'a lijjantil. Bu ci nit soxla'a dara lu war'a bàyyikoo ci "àtte" gi (goornemaa), mel ni ab dokimaa, walla lenn lu ko réew mi ameel ci àq, moom da'y gëm ne li war moo'y mu gëstu ku ko gën'a dégg tubaab, te li gën'a bari du ñeme'e wax sax ay xalaatam ak lu xalaat yi am solo !, ndaxte déggul tubaab walla lenn ci baati tubaab yi'y jox waxam jooju xiima ak fulla, loolu yobb na ñenn ñi ci nu'y wone ne dégg nanu tubaab, ba'y tudd ci seeni wax lenn ci baati tubaab yoy ni nu ko'y waxe sax manunu ko, te xamunu ni nu ko'y binde, te fekk na jamono ji nu ko'y def, fees nanu dell ak baati wolof yu man'a wuutu yooyule di yu franse. +Ba ci jàngkat bi génne ci daara'y tubaab yi, te déggu ko bu baax, (ñu néew lanu ñi ko ci dégg, dégg ga ca war, ndax lu sakkan la'y jël ci seen waxtu), moom itam, day faral'a jànkonte'ek’ug fasu, walla kompleks, gi'y faral'a dal ñi'y waxe li dul seen làkk, bu ñu'y wax - te taxul ñu xoot ci lool - ak boroom yile làkk, walla ku leen ci gën'a sori. Jafe-jafe yi aju ci wàll gii maneesu ko'o takk, dees leen di lim ci'y teemeer, danu ne woon nanu ci indi yenn rekk. + + + + +Nu ne woon nu taxawlu as lëf fii ci ag wàll gu àggoon nanu ci ci'y wax, te mu'y lu maneesul'añàkk’a jaaraat, ngir am gi solo, ak yiteel gi mu def lii nu nekk di wax, loolu moo'y taxawaay yi lenn ci boroom xam-xami joojale jamono ame woon, ci yee niti seeni réew, xoolal ma ku mel ni Petrarch, nga xam ne bokk na ci li ko taxoon'a siw yile taxawaay, ba daa fàggul boppam dàkkantalu boroomu'g nite, Te dara joxu ko woon loolu lu mo'y yitewoo gi mu yitewoo woon xay gu yàgg ga (civilisation ancienne), walla bind gi mu doon def ci làkku'w itaali wi doonoon aw waxiin rekk ca jooja jamono. + +Waaw lu tax Petrarch mii doon binde ci wu itaali wi, te fekkoon fi lakku'w latin wi népp daa binde ? +Loolu de tontu li mooy bindul woon lu dul ngir nit ñi xam ko te jariñu ci li mu'y bind, kon li am solo moo'y nu xam li mu'y bind, man ko'o jariñoo, du mu bind ko ci latin. Lu mel ne jeqiku gii ( revolution) mooy li seriñ Suhaybu defoon bu yàggul, ba mu bindee ci wolof téereem bu am solo boobee di Qurratul Hayni ci xam-xamu diine, loolu tax nit ñi sottiku ci kawam ci'g fuqale, ñépp jariñu ci, ngir nekk gi mu nekk ci wolof, te kat téere'y diine ya'a ngi fi ak yu adduna yi, te kenn xoolu leen ngir nekk gi nu nekkul ci wu kocc. +Kon man nanoo wax ne Petrarch mii moo gënoon'a ñaw te ëpp xel mbokki boroom xam-xamam yi, ndax day mel ni moo leen gënoon'a xam li xewoon, bi mu gisee ne warul ci mom mu bind ci latin, te làkk wu nu gën'a dégg'a ngi fi. Deesul sikk it ne moom dey ab jeqikukat la woon ( revolutionaire) bu bokkoon ci ni gisoon ne du man'a ñàkk ñu soppi ba ci làkk wi nga xam ne weesuwul fii mu nekk ab gàllankoor ci yoonu jëm-kanamu'g askanu Itaali wi, bi mu nekkee ci dëgg-dëggi aajowoo ag jëm-kanam, ak yéeg gu xel ak gu xalaat. +Mu gisoon ne bu bëggee def jëf ju am solo ci yee, ak xamal askan wi, li ko war moo'y mu wut anam gu yòmb gu koy jàppndal loolu gën ji jàppndal, te di tax ba ñu'y man’a alawtiku li mu leen di sànni ci xam-xam ca na mu gën'a yòmbe. Lii'a ko yobb ci mu binde ci wu itaali, ba nee wu latin wi. Ci misaal sunu njiit loolee di Senghoor , nga xam ne foo toll nu ko'y tudd te du kenn, moom de boo'y xool da nga naan moom de bindul woon xanaa ngir mbokkam yii di waa senegaal, Ndax kat li ëpp ci réew mii déggunu tubaab, nga rax ci dolli dafa meloon ne ab nasaraan la , walla ku leen doon ligéeyal ci sunu kaw. +Làkk'a ngi fi woon nii di wolof, di wu ñépp déggoon, walla li gën'a yaatu ci réew mi, bu Senghoor gëmoon réewam ba di ko ligéeyal, du woon binde ci tubaab, li ko waroon kay moo'y mu defoon ko ci wolof, walla sax ci séeréer ci li gën'a néew. Walla mu digale ñu firi ko ci yile làkk, mbaa mu sàkk jëwrin ju féetewoo jëmale leen kanam, ndax ëlëg ñu man'a xëy di'y làkk yu gën'a am ag koom, te gën'a yomb'a jëfandikoo. Walla kay mu soññoon sunu boroom xam-xam bu mag ba Seex Anta, mii nga xam ne lii rekk'a ko masoon'a ñor, ci mu wëy ca yoonam woowee,te gën ko'o jàpple ci xalaat ak doole, waaye deful loolu, moom kay da ko doon xeex ci anam gu ñaaw, di ko gàllankoor ci mu amal bile naal. +Moom nag ca dëgg-dëgg moo'y ki fi nekkaloon tubaab bi, ndax yiteem jépp nekkutoon lu dul di gëstu lenn ak lu mu man'a tuuti tuuti ci lu ko man'a askanale ca waa-Orob ya, li'y tegtal ci loolu moo'y waxam jii ci téereem bi tudd ( poesie de l'action), mi ngi ci naan: (( j'ai probablement une goutte de sang portugais qui est frequent en Europe mais rare en Afrique noir )) maanaa mi di : man dey ku dem am naa as toq ci dereeti Portigaal, ndax man da maa bokk ci mbooloo'm dereetu'm (A) mi bari lool ca Orob te néew lool ci Afrik. +Loolu mu wax ngir mu wutal ko lay daa jël yaayam ji nekkoon ku dëkk jiwaalo, taxaw temb ne Gine'g Portigaal gi la cosaanoo, ak li nday ji daa wax lepp naan cosaanoowu fa. Kon kii soreewul ak ka woy wa taxoon'a jug mu'y :((Màggat mu màggat ci am, njàggu'm tubaab, jabaroo <> tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii )). +Waaye daa mel ne da ma laa gis nga naan waaw lu tax seriñ si daa binde ci araab te wolof nekkon fi ? + +Tontu bi: + +Seriñ si de li am ba mam, moo'y ci araab lanu daa binde, waaye ak ci wolof, te araab de li leen ci jañoon du jëmmi làkk wi rekk du woon it gòndiku ci, walla fònkadi wii di seen wos, mbaa foñ ko te weddi ko, ba loolu di leen ci'y tee di binde ak'a tase seeni xalaat. Li fi nekk moo'y ñoom seenu'g xér gu tar ci nit ñi doon ay jullit yu dégg seen diine, rawati na alxuraan mi deesul dégge ci lu dul araab, moo leen àggale woon ci ag wàll ci seeni ligéeyi xam-xam rawati na la ca aju woon ca diine ñu ko daa defe ci araab. +Ñoom de dañoo gëmoon - te loolo'ooy li waroon- ne alxuraan mii kat aji nekk la ju fees dell aki kiimaan aki way lòttal (aji lòttal nag bu nu ko waxee ci xam-xamu diine mooy lol Yàlla rekk'a ko man, lòttal na mbindéef yi ag defam). +Benn tafsiirkat - seen gëm-gëm laa la'y wax- amutoon kàttanu'g leeral ko, mbaa mu indi lepp ca tafsiir ga ca war, ak leeral ga mu yayool, moo taxoon nu gisoon ne nit ñi daal ci masala mii, ñoom ñépp'a ci yam, maase ci ni bëñi peñe, kon li leen doon noppal ci seen gis-gis, moom'y nit ñi maaseendoo jàng araab, ku ci nekk lijjantil ko sa bopp, settantalal sa bopp ci way teddi aaya yii, ci lu dul nga'y sukkandiku ci kenn. Ndax kat kenn gënu leen ce'e man'a dimbale seen bopp, bu nu déggee araab, bu nu ko deful nag, lu nu ci man'a ame itam am raxasiit rekk lay doon, aw desiit, ag wall ca lépp rekk la’y doon, du weesu yu njëlbeenu yi rekk , deet yu mag yi. +Waaye jàngale gi ci araab ak bind ci, teewu leen woon di bind ci wolof ak'a bindante, ak di ko jéem'a jàllale, ci taalif ci ay woy yu rafet te sakkan, fees dell aki baat yu xoot, yu naroon'a réer moos bu nu ko deful woon, aki masala'y nahwu (grammaire), amoon nanu ay xisa yu yéeme, ami nettali yu adabé (yu njàggaté), aki cax yu xoot yu daa dimbalee ci màggal am xel, rawati na mu gone gi. +Seen woy yooyu ak nettali yi danu daan fees - ci li ëpp - ak lu’y yare,loolu bokkoon na ci li daa dimbale yarkat yi, ndaxte ñu ci ëppoon fekkoon nanu nit ñi nu di boroomi jikko yu rafet yi ñu dégge ci woy yooyu ak léeb yooyu. + +Xoolal ma léeb wu mel ni ( Kumba am nday) niki misaal ci ay nettali yu di kojug yar, yu'y dund, tukkee ci sunu réew mi, moom de lu am solo la ndax daa fees dell aki misaal yu kawe. +Moom de day soñ ngone yi, rawati na jigéen ñi, ci ñu ràngoo jikko yu rafet yi, ñu'y muñ, farlu, nangoo dee ci lu baax. Loolo'oo tax ñu man ne ñaari làkk yii, daal duñu wooni noon, waaye way mottaleente lanu woon, yu daa dimbalante, bii ñu ko'y jëfandikoo ci li ëpp, ci wàllu'g diine ak jàppe ko jumtukaay bu am njariñ ci dégg alxuraan mu tedd mi, te fiqu ci jile diine, ndax faqiih moom muy ku xam fiq, maneesu ko'o nekk ci lu dull dégg bu baax araab, kenn mant'a dégg jile diine, di jariñu ci xam-xam bi ci nekk te déggoo araab, loolu xaw naa jòmb. +Senghoor sax seere na loolu ca ( poesie de l'action) , mu ne: (( je suis pour le mainien du Latin coome langue universelle de l'Eglise catholique, tout comme je duis pour le maintien de l'arabe comme langue de l'Islame)) maanaa mi di man ànd naa ak ñu tëyye fi Latin niki làkku egliisu kotolik bu adduna bi, ni ma ànde ci nu def araab lakku lislaam. +kon nag li nu sañ'a wax mooy mag ñi de, wolof lanu jàppe woon seen làkku ofisel, te daa nanu sonn it ci jëmale ko kanam, daa sukkandiku ci loolu ci làkku araab, seenu'w jàngaliinu araab it walla xam-xami diine ñi ngi ko daa defe ci di tekki baat yi ci wolof, baat bu nu la wax rekk wax la ba mu tollool ca wolof, loolo'o jur riisu'g wolof gii, fees dell ak baati araab yu nu wolofal, tax it ba yeneen baat ci wolof am yeneen maanaa, yeneen tëggiin it sosu yu manul woon'a ñàkk, te feeñe ci wonu'g araab. + +Ndax nag du'g dofe, nu sanni nële sunu lakku nday wii, ngir jël weneen wu keneen, di ko jëfandikoo niki ofisel - naan dafa yor ci way yayale'y xam-xam ak yu xay yu wosam amadi - ci jàngal sunu'y doom yu ndaw ak yar leen. Ñun de ci loolu danu'y jàmmaarloo ak lu sakkan ciy coona ci xamal leen, te déggal leen ci anam gu dëgër, te gaaw. Ndax gënul woon'a dëppoo ñu jëfandikoo sunu wos wii, ngir mu gën no’o jappandi - ca anam ga mu gën'a yaatoo - nu sol leeni xam-xam ci lu dul gën ja'a neewi coona?. + +Ndax yellul ci nun nu jéem'a lijjanti sunu jafe-jafe yu bari yii nga xam ne foo wëlbatiku gis leen, ñu'y yu koom ak ak ak, te'y yoo xam ne jafe ge'e lijjanti foo ko takk weesu na ko, te ñu soxla lool ku ci jéem, te bàyyi nag sonn gii nu'y def - ci kem bu rëy bii ci'g farlu ak yitewoo - ci yekkati jeneen aada walla kiltiir ju di kojug jàmbur ?. +Ñun de foo nu fekk ni ngi wax, ba sunu'y gimiñ yi sax - ci li'y feeñ - xanaa amatunu beneen ligéey bu leen war ci seenu'g dund, bu dul joyal baatu'b frankofoni, jaarale ko ci diggante seeni bëñ ànd ce'ek as lëf ci'm mbég ak màggal. +Bii baat de da'y dikk di bawoo ci put gi ci'g diis, bijj nag ay mbiccam, di lu ñu peege mbalaanu'm wurus mu wormaal ak jox àq, bu ko defee mu bocciku nag ci'g rëy mel ni moo'y buur bi, te fekk na ne nëbbul ci diggante ay lem-lemam lu toll ne peppu suuf ci maanaa, aha kay, xanaa mi nekkul lu dul sanni ca àll ba, lépp lu la fi sa maam bàyyil ci ndono lu xam-xam mbaa cosaan, te'y sonn ci jañ pono'y aada'y tubaab ak aw làkkam jëm ca kanam, ak yitewoo ko mel ne moo'y lépp, sànni ca sa ginaaw lépp loo moomoon ci làkk ak xay, naaneey: du dara lu dul ag wëy (paase) aku'g dellu ginaaw, te ag teew amul ñeel ku amul'ug wëy . + +Man de noonuwuma tubaab waaye xam naa ne yayoowul ci ñuñ gii yitewoo gu mag... ci sunu's alku. + +Lii nag gëstu la bu ñu doon def +Lii nag gëstu la gu ñu doon def, bëggoon ce’e génne lii nu peek, wër nu ci’y jafe-jafe, rawati na yi ci di yu aju ci sunu li làkk li laal. Waaye nag ba tay gëstu la gu njàggat, gu nu jublo’o def ngir génnewaale ci as lëf ci taaru’b wolof, ak li mu làmbool ci’g nooy ak man’a ëmb. +Mu doon it ag woote jëme ci luñutu ak jam (critique ), ak def lu mel ne lii gu tukkee ci geneen wàll gu nu moy . +Kon sunu yëf’a ngoogu, di lu aajowoo xalaat, xool, sònn, yitewoo ak jàllale. +Na léen wóor nag ne ci’g solowoom ak’ug déetam , népp la ñeel, népp’a ko ñeel it, ndax sunu mbir la , di ménn ci yi nu man’a jëmale kanam, bu ñu ko fonkee, ci li ma jort. + +Gongikuwaay +Abdu Xaadir KEBE + +Xool it + ay rajo yuy wax wolof ak tele: + + http://www.futursmedias.net/ + https://web.archive.org/web/20080825082301/http://www.sudfm.net/media.php + https://web.archive.org/web/20080827141922/http://www.wikio.fr/news/Walf+Tv + + Waxi Seex Anta Jóob + + http://en.wikipedia.org/wiki/Wolof_language + +Làkk +Nataal : foto + +Nataalkat + Babacar Touré Mandémory + +Xarala +Fànn +Mataam (fr. Matam) : benn diiwaan ci yu Senegaal yi, fenn ci fi Pël yi ëppe. + +Dëkki Senegaal +Mbuug ak Way +Mbuug nag mooy Misig (fr musique en music) mbuug nag ñu bari xamuñu baat bi ci wolof ba tax na misig rekk lañu koy wax ndax daa bokk ci baat yi nga xam ne ñépp a ko bokk niki lu mel ni widewo(video). WAY, baatu way mi ngi juge ci nit ku way maanaam nit ku yeww li tax ñu tudde nit kookii waykat dafa way ba man a sos ay wax mbaa ay nose yoo xam ne nit ñi mu nekkal bàyyiwuñu ci xel mbaa sax xamuñu ko woon, kon moo leen gën a way ba tax muy way kon ku ñuy tudde waykat dafa war a doon kuy yeete + +Way batay man na tékki poesie ci wolof +Ay Mbuugkat ci Senegaal + Didier Awadi + Foumalade + Touré Kunda + Ismaël Lô + Ndiaga Mbaye + Youssou N'Dour + +Ay nosekat/Taalifkat ci Senegaal + Seriñ Muusaa KA +Sñ Sàmba Jaara Mbay +Sëriñ Mbay Jaxate + + Mamoor Xam Sa Diine + +Woy +Woy +Xayma yi ay xamuwaay la ñu yuy tabaxu ciy xalaat-jiital, ci ay fook naa, yu aju cig xellu. Doon na itam xam-xam biy seet aka biral ay xamteef, di itam ki leen di jangale. + +Xayma + +Teerekaay + Mbaye Faye, Nanu Xayma : Mathématiques modernes en langue nationale wolof à l’usage des opérateurs en alphabétisation, des élèves et des enseignants alphabétisés en wolof, 2006. + Institut des langues nationales, Baatalu xayma, nasaraan ak wolof / Lexique des mathématiques, français-wolof, Nouakchott (Gànnaar), 1997. + + +Xayma +Politig + + Mbootaayu Xeet yi Bennoo + +hola iñi +Pentuur + +Senegaal +Fodé Camara +Soly Cissé +Kalidou Kasse +Iba Ndiaye +Souleymane Ndiaye +Ousseymou Sarr +Amadou Sissokho +Moussa Tine + +Cuub +Mooy Mboor ci làkk wolof dëgg, di xam-xam bi'y gëstu la xewoon demb. Di itam mbooleem ay Jëf ak ay xew-xewu demb, la ko dale ca ña nu jiitu woon ba ci nun. +Taariixkat mooy ki'y gëstu di bind ci wàllu taarix + +Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri seen way dëkk. Da na nu waxal it ca dund ga fa amoon. Ci gàttal daal, xam-xamu taariix day gëstu li-wéyi nit (dembam) cig matale. Da na wuññi (feeñal) it nekkiin ak dundiin yi nga xam ne nit jaar na ci jànkoonteek ñoom ci dundam gu gudd gi, ci biir ay jamono yu dabante te toftaaloo, bu ko defee mu gëstu anami jëm-kanam yi nga xam ne nekktéef bii (di nit) amal na leen ci taariixam bu gudd bi, ci noonu loolu jural ñu ñu jange ci daj-dajam (li mu jot a dund) yooyu wéy, aki ndamam, te jéem a moytu ay pakkastalam aki rëcc-rëccam ya jàll. + +Bu lii amee nag dina nu gis njariñ ak ngënéeli gëstug xam-xamu taariix. + + Lenn ci taariix bu àdduna bi + + Taariixu Senegaal + + Lu am ag séqoo ak njàppum jaam + Cosug àdduna bi ak Big Bang + +Li ñu jublu ci jàng taariix +Taariix dinanu ko jang ngir mu yombalal ñu xam mboolaayi nit ñi ci anam gu xereñ, te dégg (nand, gis), xàmmee it buum yi leen boole. + +Gëstu dundug buur yeek imbraatoor yi rekk du lenn rek li nu war a yitteel ci taariix, li ci gën di farata kay mooy gëstu dundug mbooloo yi ak bennaan yi (benn-benn nit ñi). Ak gëstu jafe-jafe yi daa yeesu ci seenug dund bis bu Yàlla sàkk, te jéem leen a wutali saafara yu dëppoo, ba maas giy ñëwi ëlëg man cee jariñu. + +Digal taariix (wutal ko aw dig) +Ngir digal ab xew-xew fàwwu mu am ab tombub boy (fa muy dooree). Ay tombi boy yu bari nag am nañu te taariix man na cee tàmbalee. Nasaraan yi ñoom seen tombub boy mooy juddug Yonnant Yàlla Isaa, ca lañuy taariixe seeni xew-xew, bu dee jullit ñi ñoom seeni xew-xew ñi ngi leen di wutaluw dig wu bawoo ca gàddaayug Yonnant bi(j.m) juge Màkka ga mu ganee àdduna, dem Madiina. Xew-xew bii nag mi ngi fiirook (dajeek) atum 622 ci taariixu juddug Yonnant Yàlla Isaa. + +Jamono yi +Donte taariix mooy la xewoon ba àdduna sosoo ba léegi, taariixu nit ñi, suuf si, jawwu ji,... Waaye ci déggoo taariix ñu ngi koy tàmbalee ca ba ñu sàkkee mbind, séddale ko ci ay jamono. Li nga xam ne ay téere yu ñu bindoon moo ñu ko xamal. + +Njëkk-taariix(mooy taarixu ñi fi nekkoon laataa sàkkug mbind) + +Taariix( mooy lépp li xewoon ca ba ñu sàkkee mbind ba leegi). Taariix ci boppam dañu koo sédale ci ay jamono. + +Jamono ju yàgg ja: (feeñug nit ci suuf ba daanu'g nguuru rom gu mag ga ci 476) + +Jamono ju diggu ja: ( ba feeñug Amerig ci 1492) + +Jamono ju bees ja: (ba fippug waa-frãs ci 1789) + +Jamono ju mujju ji:( ba ci sunu bis yii) + +Njëkk-taariix +Boroom xam-xam yi, ginnaaw gëstu gu ñu def ci suuf si, wuññi nañu ay jeexiit (reste;vestige;trace) yu yàgg: ay jumtukaay, ay xor, ay doj, añs yuy tegtale ne suuf sii déy aw nit dëkke woon na ko njëkk ay junniy at, jamono jooja la nuy tudde njëkk-taariix. + +Moom nag mi ngi séddaliku ci ñaari xaaj: + + Jamonoy doj wu ñu yatt + Jamonoy doj wu ñu xacc (wu ñu ñawal) + +Ci ngënéelul jeexiit yii lanu xame njëkk-taariix. Nit ci jamono jii da daan tuxu rekk, di jëfandikoo ay ngànnaay aki jumtukaay yu njëlbéenu (primitive) (doj yu ñu yatt, ay ngànnaay, ay xeej aki xepp). +Bi jamono gënee dox, seen dund gi soppiku, ñu xam leegi sawara, jëfandikoo ko ci togg ñam yi. Ci jamonoy doj wu ñu xacc wi, lañu tàmbalee dajaloo, sóobu ci mbéy, sàmm ak ràbb ak liggéey jumtukaay yu xànjar yi, tàmbali it di def yenn liggéeyi fànn yi niki bind ci doj (ciseler ;graver), ak yatt. +La ko dale ca 3500 n.j.g (njëkk judd gu yonnant Yalla Isaa), la weñ feeñoon, ñu fent it mbind. Bi weñ feeñee, fentees it mbind la njëkk taariix jeex, taariix daal di tàmbali. + +Ñenn ci ay taariixkat + +Seex anta Joob(Cheikhe Anta Diop) + +Paate sow + +Téerekaay +paate sow (wo): Dembi Senegaal, 1998 +Yatt + +Afrik + +Senegaal +Tafsir Momaye Gueye +Ousmane Sow + +Fànn +Beer (fr. Gorée) : dun (Senegaal) + +Dun +Senegaal +sëriñ mooy tekki kilifa diinè lislaam. Am xamxam bu sell ak mëna def keemaan (ci doolè Yalla) mooy ñaari kalité yi ñuy gëna yaakaar ci ab sëriñ. + + sëriñ goor lay doon, waayè am na jiggèèn yu am kalitè yooyu, ñu leen di tudde soxna. + + sëriñ it dina faral di tekki ag màggal, niki Monsieur ci Fr, bu dee jigéen ñu ne soxna si +Soxna mooy baat bu ñuy jox kilifa gu jigéen, bu doon góor la sëriñ lees di wax. + +Dees na tudde soxna itam ndayu nitug Yàlla gu ñu ràññee, ngir màggal ko, ci misaal : Soxna Maryaama (yaayu Yeesu iisaa). + +Dees na faral it di woowe soxna yeneen jigéen, ndax rekk séen jikko yu rafet walla rekk ngir wormaal gu ñu leen wormaal. + +ci gàttal soxna jigéen ju baax. + +Ñi ëpp bu ñu koy jëfandikoo jabar lañu ciy jublu + +Dees na wax it doomu soxna jublu ci Sëriñ, nitug Lislaam:kër doomi soxna yi, + +Lislaam + + +Project and language +I request sysop access. + +The Wolof Wikipedia does not currently have any Wolof speaking contributors. Thus far I have been unable to contact the administrator who also does not understand Wolof. Although I am new to Wikipedia, I would like to be able to set up a sub-project on the Wolof site (Bible Encylopedia in Wolof) which I would like to moderate personnally, and also develop a Wolof user interface. Thus I would like to have temporary administrator access. I live in the bush with a poor internet connection. This would be sufficient to keep an eye on new contributions, but not for major new development. Thus, most of my work will be done on monthly visits to the capital. Therefore I would appreciate at least a period of 6 months, with a view to an eventual permanent administrator status. + +Language Code: wo +Local Request Link: *Local User Page: Thank you. + +Yorkat +Ci làkku ibrë (אִיּוֹב) la tur wi jóge. Ayóoba mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam. Ci angale mooy Job; Ci faranse mooy Job + +Benn nit ku fonkoon Yàlla la woon. Yàlla may na Ibliis mu man koo fitnaal. Naka noonu daje na ak coono yu bare. Ay doomam yépp dee nañu te mu ñàkkoon li mu am lépp ci benn fan, ba noppi ànd ak feebar bu metti. Waaye nangu na lépp ak muñ. Man nañu jàng jalooreem ci téere Ayóoba (Job 1:1). + +Ci Injiil ci Sa 5:11 la feeñ. + +Diine +Yonenti Lislaam +Cosaan baati Seereer-Safen la. Moo teki "début" / "origine" / "commencé" ci làkki Seereer. + +Cosaan + +Ci xëtt wi, see fas tekki . Sama weerukay ci walu xam-xam moodi jangat-nit . Bile baat, manko tëggé ci (anthropologie), manaam anthro=nit ak pologie=jangat. Cosaan, aada, ak luñuubaaxo daño fasoo. Waayé, ci sama gis-gis, cosaan moy r, manaam fu aw askan bayee koo. Bilep firi daa ajju si walug bërëp (espace). Cosaan, mana firi batay luñu donnu ci makk ñi. Kon ci tënkk, cosaan, moy reenu askan, lunġa länkalee , di luñu baaxo def, loolu moo lay jox "culture" wala mu xeltu ko ta mu jem ci walu dundam, man nañ jappé "culture". Kon, suma suka ndikoo ci lii ma fessäl. +Cosaan nak, ci walu xeltu, baat bu jaxaso la. +Gëstukat , dalee ko ci jamano yu yàg ya, kon luy walbatiku. Nittu jamano boo jel, dañu tànn ci seen cosaan ay lëffin. Rax ci dooli, dañuy fen. Waaye timit, nguuruk reew munek war jôkaar . Cosa, don te mengo tul ak. Cosaan ak aaday Reew yi eup dañu wali ci cosaanu reew yi new doolee, ak dileendi nasaxal. + +Bu njekk, borom xam-xam yi bayoo tuggal ta see gëstu ajju ci walu jangat-nit. Li lalloon bilee weddi moodoon ne see dëkk yi ñoo noot, seeni kom-kom. Bi aduna doxee ba nootagee bi jeex, bu afrik moom boppam,, ñeppu nagu nagn ni askan . Nit ku nuul yam wanee ne nit Lolu di ndam lu rey si xeetu nit .Ndax te bo xamul , do xam . +SEEX LO + +Lëkkalekaay yu biti +Séeréer +Youssou Ndour (Born: Ndakaaru, 1959), nit +Bokk na ci ay waxam : Fital mbubb a ma ko gënal, mburoo ma ko gënal + +Woy +Nit +Aadama mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam (آدم). Ci angale mooy Adam te ci faranse itam mooy Adam. Mooy nit ki Yàlla jëkka sàkk. + +Aadama ci Biibël ba + +Nettalib Aadama feeñ na ci Ge 1:26-30; 2:4-8; 15-20. Aadama dafa toppoon jabaram Awa ci bàkkaaram. Bàkkaar boobu mooy lu indi musiba yépp yi nu gis ci àddina si (Ge 3:6-21). At, ya Aadama dundoon, 930 la. (Ge 5:5). Ci Injiil dañuy wax ci Aadama ci Lu 3:38; Ro 5:14-19; 1Ko 15:22,45; 1Tim 2:13,14; Yu 1:14. + +Aadama ci Alxuraan + +Nettalib Aadama feeñ na ci suraat 2:30-38; 3:33,59; 7:11,19-27; 17:61-62; 18:50; 19:58; 20:115-128. Nekk na ki Boroom bi jëkk a bind muy nit doon tamit Yónnent bi njëkk. +Yàlla a ngi wax ci Alxuraan: +" Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne daf ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? Mu ne: Xam Naa lu ngeen xamul” + +Yàlla wahyu suuf si ne ko: damay sàkk ci yaw ay bindéef, amna ci ñoom ñu may topp, am ci ñoom ñu may moy, képp ku ma ci topp ma tàbbal ko guyaar, képp ku ma moy ma tàbbal ko sawara. + +Suuf ne ko: ndax dangay bind ci man ñoo xam ne danga leen di dugal sawara? Sunu Boroom ne ko: waaw! + +Nee nañu: Ibliis daal di wàcc ci kaw suuf ne ko yaw suuf, damaa ñëw ngir laabiire la, Yàlla daa namm a bind ci yaw ki gën ci bindaafon yi, te may ragal ñu moy ko mu leen di tàbbal sawara, bu booba yaw it dinga duggaale sawara tamit. Suuf daa di jooy! + +Yàlla bind sunu baay Aadama ciy yoxoom ngir Ibliis bañ a rëy ci sujjótal ko, Yàlla a ngi nuy wax ci loolu: + +"Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, nangeen daldi rot, sujjóotal ko." + +Nee nañu: bi Yàlla bindee Aadama (HS) toog na 40i guddi. Am ñu ne: 40i at, muy jëmm ju ñu tërëral. Ibliis daan ko dikke, di ko kàjji muy keleŋ ni ban wu wow, nee ñu mooy li sunu Boroom naan: + +" Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ". + +Ibliis di dugg ci biir gémmiñu Aadama di génne ci ginnaawam, di jaar ci ginnaawam di génne ci gémmiñam, te naan ko: " Doo dara, ak lu tax ñu bind la?, su ñu ma la saytuloo ma alag la, bu ñu la saytuloo ma ma moy la". + +Malaaka yi bu ñu ko daan romb dañu ko daan ragal, fekk ne Ibliis moo leen ko gën a ragal. Ba dig bi nga xam ne la Yàlla namm ëf Ruuwam ci moom jotee, mu ëf Aadama Ruuwam. Mu digal Malaaka yi ci ñu sujjóotal Aadama. Malaaka yépp sujjóotal Aadama ba mu des Ibliis ngir rëy mu bokk ci way-wedd ni ca saa sa. Yàlla ne ko yaw Ibliis, ana lu la tee sujjóot ndeem digal naa la? Mu ne kii maa ko gën, man du ma sujjóotal nit koo binde ci suufu ban. + +Ibliis sujjóotul ngir rëyam ak mbewteem ak kiñaan. Yàlla ne: + +" 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ” + +76. “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci + +ban”. + +77. (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ; + +78. te Samam rëbb dal na la ba ba saa di taxaw”. + +79. “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”. + +80. (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu, + +81. ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”. + +82. “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj-loo ñoom ñépp, + +83. ba mu des sa jaam ñiy sellal”." + +Aadama Ak Noonam Ba (Ibliis) + +Bi Yàlla noppee ci Ibliis ak ci yedd ko, Ibliis bañ rekk ne day moy Yàlla. Sunu Boroom rëbb ko tàq ko ci yërmàndeem def ko Saytaane Rajiim, génne ko ca guyaar. Ginnaaw loolu Ibliis sumboo ak meram iñaane Aadama, mu bëgg koo génne guyaar. Yàlla bàyyi ak Aadama xelam gawu ko ci dara, mu bayyi ko ak sagoom, muy man a ràññe lu baax ak lu bon, ginnaaw ba mu ko maytuloo Ibliis, Yàlla a ngi naan: + +". Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de. + +118. [Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle, + +119. doo fi yëg u mar, doo fi màggat”." + +Ginnaw bi ñu dàkkoo Ibliis, mu tàmbali nag ci jëfe la mu dogu woon; te mooy fayu ci Aadama (HS) ak génne ko guyaar, di ko awale ci di ko jiixi-jaaxaloo, jéem koo gëmloo ne xam na lol man na tax ba Aadama sax dàkk du dee mukk. Yàlla a ngi wax naan: + +"Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”." + +Ibliis jaare ci bëggug Aadama ci sax fi dàkk ak sax ca guyaar; bañ fa a génn. Mu xam ne loolu ay tombug néew dooleem, Ibliis daa bëgg a wan ne sunu Boroom; man naa alag kii nga may gënalee. Adaama moom ndaysaan, xamul dara ci kàcci Ibliis yi, waaye li mu ko wax neex na ko te jar na a jarabu, mu yëg ne loolu du'y fo mu laaj Ibliis naka lay def ba am loolu moom ak soxnaam Awa? Ibliis ne ko : ndax yaa ngi gis garab gii ñu la tere nga lekk ci? Moo la ko man a may. Waaye ba tay Aadama gëmul Ibliis, muy fàttaliku tere gi sunu Boroom tere woon ci mu bañ a jege garab gi. + +Kon naka la Aadama def ba lekk ca garab ga ak aartu yi ñu ko aartu yépp bàyyikoo ci sunu Boroom? + +Boroom xam-xam dañuy wax ne(YRX): Ibliis ci jax-jaxal yi mu doon def Aadama, moo ko doon fàtteloo ndànk ndànk li ko sunu Boroom tere woon (loolu moo nuy dal nun ñépp ba tay, su nuy saytaane di jax-jaxal, danuy fàtte ndànk ndànk lepp lu nu mas a waar). Waaye Aadama gëmul woon lu dul ginnaw ba mu waatee, Aadama ne ko giiñal nu bu dee li nga wax dëgg la, Aadama (HS) -ci ni ñu bind- xam na ne kenn warut a waat ci Yàlla ba noppi di fen. Mu ne ko waatal ci kiy sama Boroom di sa Boroom ne li ngay wax dëgg la. Ca noonu la Ibliis mi ñu rëbb giiñe ci kanamu Aadama ngiiñug fen ci ne li mu wax dëgg la te moom da koy laabiir rekk moom ak Awa. Yàlla a ngi nuy leeral loolu ci téereem bu sell bi Alxuraam, mu ne: " Mu giiñal leen ne moom kat mi ngo bokk ci way-laabiire ñi" + +Ginnaw ba Ibliis waatee, ci la xelu Aadama soog di dal naka noonu Awa (HMS) ndax seen xel masut a jàpp ne kenn sañ na a giiñ ci Yàlla ci ay nar, Ibliis nekk ki jëkk a waat ci Yàlla ci ay fen (kon képp kuy waat ci Yàlla di fen, Ibliis ngay roy) te amul fu mu ko defe fu dul àjjuna. Ca la Aadama fàtte lépp lu ñu ko tere woon ndax giiñu Ibliis ji, tàmbalee lekk ca garab ga moom ak Awa. Nee na ñu garab ga garabu pom la woon nekkoon ci kaw suuf, bi ñu ko lekkee rekk la seen mbalaan ya muriku seen awra feeñ. Yàlla ngi nuy leeral loolu naan: + +"22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt + +di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ” + +wàccug Aadama Ak Awa Ak Ibliis Ci Kaw Suuf + +La dal Aadama dal ko; mu lekk ca garab ga, sunu Boroom wàcce Adama ak Awa ñoom ak Ibliis ci kaw suuf, Yàlla a ngi naan: + +"[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di + +noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”. + +Bi ñu wàccee Ibliis ci kaw suuf daf ne: yaw sama Boroom génne nga ma àjjana ngir Aadama, te man manaluma ko dara ndare danga maa kàttanal ci kawam, Mu ne ko defal naa la ko, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko lu mu am ci doom nga am lu ni tollu, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko seen i dënn say dëkkuwaay la; ngay man daw seen biir i yamar ni dereet di dawe seen i yaram, mu neeti dollil ma, Mu ne "Génnal ak say kàddu, loo mën ci ñoom, nanga leen song ak say xarekat ak say gawar, + +nanga bokk ak ñoom alal ak i doom te dig leen”. Waaye Séytaane du leen dig lu dul ay nax." + +Ginnaaw bi Aadama xamee li Ibliis sàkku ci sunu Boroom mu ne: Ay yaw sama Boroom teg nga ko sama kaw, te man it manuma mucc ci moom lu dul ci sa ndimbal, Mu ne ko doo am doom lu dul boole naa ko ak ñu koy aar ci àndaale yu bon, mu ne dollil ma, Mu ne ko jenn jëf ju baax ju ne ma ful ko fukk te di ko yokk, jenn jëf ju ñaaw ju ne jenn laa koy jàppe te di ko far, mu ne dollil ma, Mu ne ko "Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. + +Ndax Yàlla dana jéggale bakkaar yépp. Mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”. + +Mu neeti ko, yaw sama Boroom dollil ma, Mu ne say njaboot fi ak ñoo ngi dund du ma tëj seen buntu njéggal, mu ne dollil ma, Mu ne dinaa jéggale te du ma toppe, mu ne doyal naa. + +doom Aadama + +Waxinu wolof bu tekki "nit ñi". + +Diine +Yonenti Lislaam +vatti faen looko mosa porent jege + +Diine +Ci angale mooy Anna te ci faranse mooy Anne. + +Yonent bu jigéen ku màggat lool la woon. Jëkkëram gaañu na waaye Aana séyaatuloon. Guddi ak bëccëg dafa doon jaamu Yàlla ca këru Yàlla ga ca Yerusalem. Bi waajuri Kirisit indi woon Yeesu ni liir, Aana waxoon na ci moom ci kanamu ñépp ñi fa nekkoon. (Lu 2:36-38). + +Ci Injiil dañuy gis Aana ci Lu 2:36,38. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Linjiil +Ci làkku ibrë (אַהֲרֹן) la tur wi jóge. Aaroona mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale ak ci faranse mooy Aaron. + +Magu yonent Yàlla Musaa la woon, ñu bokk ndey ak baay. Ñetti at la Aaroona mage Musaa. Baayam, Amram la tudd te yaayam Yokebedd (Ex 6:20). Amoon na ñeenti doom yu góor ci jabaram, Eliseba. Ñooy Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar (Ex 6:23). Aaroona amoona benn rakk bu jigeen, mingi tudd Mariyaama, doomu ndeyu Aaroona ak Musaa (Ex. 15:20). Mariyaam bii, bokkul ak yaayu Yeesu Krist. + +Ba Musaa demee ci kanamu Firawna Aaroona dafa àndoon ak moom ngir nekk yonentam (Ex 7:1). Yàlla tànn na ko, mu jëkka doon saraxalekat bu mag ba ci biir bànni Israyil. Moom moo sàkkaloon bànni Israyil benn xërëm bi xaaroon Musaa ca tundu Sinayi. Ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo (Ex 32:1-28). At, ya Aaroona dundoon, 123 la. Ci kaw tund wi ñu wax Xor la faatu (Nu 33:39). + +Man nga jàng jalooreem ci Ex 4:14-16; 4:27-31; 5:1-4; 15-21; 6:28-7:13; 19-22; 8:5-12; 16-19; 9:8-12; 16:2-10; 19:23-24; 24:1-2,9-15; 28:1-12,29-30; 32:1-8,14-28,35; 34:29-33; Le 8:1-9:24; 10:1-4; Nu 3:1-4; 12:1-15; 14:2-5; 16:1-35; 41-50; 17:1-10; 18:1,8,20; 20:1-12; 23-29; 26:58-61. + +Ci Injiil dañuy wax ci Aaroona ci Lu 1:5; Jëf 7:40-41; Yt 5:4; 7:11; 9:4. + +Diine +Yonenti Lislaam +Diine +Yonenti Lislaam +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci làkku ibrë (אבדון) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Abaddon; Ci faranse mooy Abaddon + +Turu malaakam kàmb gu xóot gi la, ci làkku ibrë bi ñu sotti ci làkku gereg. Tur wi ci gereg mooy Apolyon. Dafa tekki 'yàqkat'. Dafay wax ci buuru njéeréer yi ñu gis ci téere Peeñu ma ci Injiil (Pe 9:1-12). Lu ëpp ci boroom xam-xam Injiil yi xalaat nañu ne ci Ibliis lay wax. + +Ci Injiil dañuy gis Abadon ci Pe 9:11. + +Baat yi jóge làkku ibrë +Ci làkku gereg \~Abba\~; Ci làkku ibrë \^aba\^. Ci làkku yawut la baat bi jóge. +Ci angale mooy Abba; Ci faranse mooy Abba + +Mu ngi tekki ‘pàppa' ci làkku yawut. Turu cofeel la. Yeesu moo jëkka boole tur wi ak Yàlla. Làkku yawut wi ci jamano Injiil ji, arameyni la tuddoon. Mujjoon nañu àbb baat bi, duggal ko ci làkku gereg ak ci làkku ibrë. + +Ci Injiil dañuy gis Abba ci Mk 14:36; Ro 8:15; Gal 4:6. + +Baat yi jóge làkku yawut +Ci làkku ibrë (הֶבֶל / הָבֶל) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Abel; Ci faranse mooy Abel + +Abel mooy ñaareelu doomu Aadama ak Awa. Magam, Kayin, moo ko réy (Ge 4:2-8). Ci Lislaam mooy Haabiil. + +Ci Injiil dañuy wax ci Abel ci Mc 23:35; Lu 11:51; Yt 11:4; 12:24. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet + +en:Cain and Abel#Abel +Ci angale mooy Abilene; Ci faranse mooy Abilène + +Diiwaan bu ndaw la woon, ci Siri ci diggante Libaŋ ak Damas. Diiwaan ba wër na dëkk bu tuddoon Abila. Abila sore woon na Damas ca sowu kaw lu tollu 29 kilomet. Bi Yeesu juddoo Lisañas moo ko yilifoon. Gannaaw loolu bokk na ci nguuru Erodd Agaripa II ba noppi ñu boole ko ak diiwaanu Siri. + +Ci Injiil dañuy wax ci Abilen ci Lu 3:1. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Siri +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Abijah or Abia; Ci faranse mooy Abia + +Ci Injiil dañuy gis ñaari nit ñi bokk tur Abiya. + + Ñaareelu buur ci Yuda, mooy doomu Robowam. Ñetti at la nguuru ci Yerusalem. Bind nañu ay jalooreem ci 1Ki 14:31-15:8; 2Ch 11:20-22; 12:16-14:1. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu bind ci Mc 1:7. + Kenn ki soqikoo ci Aaroona (1Ch 24:10). Daawuda fal na askanu Aaroona ngir ñu toppatoo liggéeyu këru Yàlla. Mu xàjjale leen ba ñu nekk 24 kër. Kër gu nekk toppatoo nañu ñaari ayu-bés at bu nekk. Sakariya, baayu yonent Yàlla Yaxya bokkoon na ci askanu Abiya (Lu 1:5). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Abiathar; Ci faranse mooy Abiathar + +Saraxalekat bu mag ba la woon, ci jamano nguuru Daawuda. Man nañu ko gis ci 1Sa 22:20-21; 2Sa 15:24-29; 20:25; 1Ki 2:22-27,35; 1Ch 15:11-13; 27:33-34. + +Ci Injiil dañuy wax ci Abiyatar ci Mk 2:26. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Abiud; Ci faranse mooy Abiud + +Doomu Sorobabel (mi bokkoon ci njiiti Israyil yi, bi ñu génne ci Babilon) la woon. Benn ci maamaati Yeesu ci Macë la woon (Mc 1:13). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Adaramit (Ἀτραμύττιον) – Ci angale mooy Adramyttium; ci faranse mooy Adramyttion. + +Benn dëkku ak teeru la woon, ci diiwaanu nguuru Room bu tuddoon Misi. Tey jii mooy dëkk bu tudd Edremit ca réewu Tirki. Waaye ci dëgg-dëgg, ci bérabu dëkk bi tudd tey jii Karatash la nekkoon. Ma nga fare woon dun bu tuddoon Lesbos. Ci jamano Injiil ji nekk na ci diggante dëkku Torowas ak dëkku Pergam. + +Ci Injiil dañuy wax ci Adaramit ci Jëf 27:2. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Addi; Ci faranse mooy Addi + +Benn ci maamaati Yeesu ci Luug la woon (Lu 3:28). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy Adriatic; Ci faranse mooy Adriatique + +Géej la, ci diggante dunu Kereet ak dunu Sisil (Sisile). Tey jii géej ga mingi tudd Géeju Iyoniyeen (Mer Ionienne). Bokkul ak li ñu wax Adiratig tey ji. Adiratig tey mooy géej ga nekk ci diggante Itaali ak Yugosalawi (Yougoslavie). + +Ci Injiil dañuy wax ci Adiratig ci Jëf 27:27. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Itaali +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Aram or Ram; Ci faranse mooy Admin + +Doomu Esrom la woon, di maamaatu Daawuda (1Ch 2:10; Ru 4:19). Benn ci maamaati Yeesu ci Luug la woon (Lu 3:33). Mooy Aram itam ci maamaati Yeesu ci Macë (Mc 1:3,4). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Aram or Ram; Ci faranse mooy Aram + +Doomu Esrom la woon, di maamaatu Daawuda (1Ch 2:10; Ru 4:19). Naka noonu, bokk na ci maamaati Yeesu ci Macë (Mc 1:3,4). Aram mooy ki ñu tudd Admin itam ci maamaati Yeesu ci Luug (Lu 3:33). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci angale ak faranse mooy Apphia. + +Jenn jigéen ji dëkk Kolos la woon. Bokkoon na ci këru Filemon. Man na nekk sax jabaram la woon. + +Ci Injiil dañuy wax ci Afiya ci Fm 1:2. +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale ak ci faranse mooy Agabus. + +Toppkatu Yeesu la woon ci Yerusalem, ku Yàlla mayoon mu mana yégle lu wara ñëw (yonent). Am na benn aada bu wax ne Agabus bokkoon na ci 72 taalibe yi Yeesu yónni ci Lu 10:1. + +Ci Injiil dañuy wax ci Agabus ci Jëf 11:27-28; 21:10-12. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale ak ci faranse mooy Agrippa. + +Buur Erodd Markus Yulyus Agaripa II bokkoon na ci juróomi buur ya tudd Erodd. Baayam itam Agaripa la tuddoon, mooy sëtu Erodd bu mag ba. Ci 27 g.K. la juddu. Yónni nañu ko Room ngir mu jàng. Ci 44 g.K., bi mu amee daanaka 16 at, baayam gaañu na. Ci 48 g.K. Erodd bu jóge Calkis (Chalcis), magu baayam dee na itam. Buur Këlódd Sesaar moo ko faloon buuru diiwaan yi baayam bu ndaw yilifoon, ba noppi ci 53 g.K. dolli ko ak yi maamam Filib ak Lisañas yilifoon. Mu nguuru ci Yude 48 ba 66 g.K.. Dafa séy ak rakkam Berenis (ñu bokk ndey ak baay). Dëj nañu Pool ci kanamam (Jëf 25:13-26:32) bi Agaripa amee daanaka 30 at te sooga jóge woon Room ngir sampu ci Yerusalem ak Sesare. Ci 65 g.K. Agaripa mënul noot yengu-yengu Yawut yi. Ci xeex bi mujj am, xare Room tas na réew mi ba dara desu ci 70 g.K.. Ci 75 g.K. nguuru Room may na Agaripa mu yilif wàll ci Siri. Gaañu na daanaka 100 g.K.. + +Ci Injiil Agaripa moo feeñ ci Jëf 25:13,22,23,24,26; 26:1,2,19,27,28,32. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (הָגָר) la tur wi jóge. Ajara moo ni ñu waxe tur wi ci Lislaam. +Ci angale mooy Hagar; Ci faranse mooy Agar + +Jaamu Saarata la woon, ñu mayoon ko Yonent Yàlla Ibraayma ni jabar, mu am ci Ismayla. Misra la bawoo. Man nañu jàng jalooreem ci Ge 16:1-16; 21:9-21. + +Ci Injiil dañuy wax ci Ajara ci Gal 4:24,25. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci làkku ibrë (אחז) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Achaz or Ahaz; Ci faranse mooy Achaz + +Li dale ci Robowam, fukkeelu buur ak benn la woon ci Yuda. Doomu Yowatam la woon, di benn ci maamaati Yeesu ci Macë (Mc 1:9). Dañuy gis jalooreem ci 2Ki 15:38-16:20; 2Ch 27:9-28:27; Isa 7:1-25. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy Achaia; Ci faranse mooy Achaïe + +Diiwaan la woon ci nguuru Room. Mooy genn wàllu Geres bu féete bëj-saalum. + +Ci Injiil dañuy gis Akayi ci Jëf 18:12,27; 19:21; Ro 15:26; 1Ko 16:15; 2Ko 1:1; 9:2; 11:10; 1Tes 1:7,8. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Girees +Akaykus – Ci angale mooy Achaicus, ci faranse mooy Achaïcus. + +Benn toppkatu Yeesu bu dëkk ci Korent la woon. Moom ak Fortunatus ak Estefanas dem nañu Efes ngir xamal Pool xebaaru mbooloom ñi gëm ma nekkoon ca Korent. + +Ci Injiil dañuy gis Akaykus ci 1Ko 16:17. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Aquila; Ci faranse mooy Aquilas + +Benn Yawut ak toppkatu Yeesu la woon, ma nga juddu woon Pont ci Asi Minër. Jabaram, Pirsil la tuddoon. Defarkatu tànt la woon ni Pool. Nawle ak Pool la, ci liggéeyu Boroom bi, te dafa amoon mbooloom ñi gëm ma doon daje ci seen kër ci Room. + +Dañuy jàng ci Akilas ci Jëf 18:2-3,18-19,26; Ro 16:3-5; 1Ko 16:19; 2Tim 4:19. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Akim; Ci faranse mooy Achim + +Benn ci maamaati Yeesu ci Macë la woon (Mc 1:14). Turam feeñul ci Kóllëre gu jëkk gi. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy alabaster; Ci faranse mooy albâtre + +Xeer wu weex ni kew la, te rafet. Daan nañu ci yett ay njaq. + +Dañu ciy wax ci Injiil ci Mc 26:7; Mk 14:3; Lu 7:37. + +Per yi ak Xeer yi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy Alexander; Ci faranse mooy Alexandre + +Turu 4 nit ñi wuute ci Injiil: + Doomu Simoŋ mi dëkk Siren, di magu Rufus (Mk 15:21). + Menn mbokku saraxalekat bu mag ba, Anas, (Jëf 4:6). + Benn Yawut bu jóge Efes (Jëf 19:33,34). + Benn tëgg ci Efes. Bëre woon na ak waxi Pool (1Tim 1:20; 2Tim 4:14,15). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Alexandria; Ci faranse mooy Alexandrie. Fondation : -334 + +Benn dëkk ak teeru ci Misra la, fu sorewul bëlub dexu Niil. Péeyu Misra la woon ci jamano Injiil ji, di dëkk bu gëna am solo ci Gereg yi. Ñaareelu dëkk bu gëna réy ci nguuru Room. + +Dañuy fekk Alegsàndiri ci Injiil ci Jëf 6:9; 18:24; 27:6; 28:11. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Isipt +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Alphaeus; Ci faranse mooy Alphée + +Turu 2 nit ñi wuute ci Injiil: + + Baayu Saag, mi bokkoon ca 12 taalibe Yeesu ya (Mc 10:3; Mk 3:18; Lu 6:15; Jëf 1:13). + Baayu Lewi, juutikat bi bokkoon itam ci 12 taalibe Yeesu ya (Mk 2:14). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku yëwut (אֱלִישַׁע) la tur wi jóge. Alisa mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam. +Ci angale mooy Elisha; Ci faranse mooy Elisée + +Yonent la woon, bu donnoon yenu yonent Yàlla Iliyas. Man nañu jàng ci jalooreem ci 1Ki 19:19-21; 2Ki 2:1-2; 3:11-20; 4:1-8:15; 9:1-3; 36-37; 13:14-21. + +Dañuy wax ci Alisa ci Injiil ci Lu 4:27. Lu 4:27 wax na ci li ñu jàng ci 2Ki 5:1-27. + +Diine +Yonenti Lislaam +Ci làkku ibrë (מָשִׁיחַ), la baat bi jóge. Almasi bi mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam (, المسيح). +Ci angale mooy the Messiah; Ci faranse mooy le Messie + +Almasi bi mooy tekki 'Ku Yàlla fal ngir liggéeyal ko'. Yonent Yàlla yi jiitu woon jamano Kirist waxoon nañu ci lu jëm ci musalkat bi Yàlla dige woon nara ñëw. Tur wi dafa ëmb wax yooyu yépp. Yawut ya, bu ñu masaana fal kenn, dañu daan sotti diwlin ci boppam, muy yonent, muy sëriñ mbaa buur. Krist, Almasi bi nag, mooy Ki Yàlla sol Xelam, ngir wone ne mooy Yonent, Saraxalekat ak Buur bi. Moo di yonent, bi nuy jottali xebaaru jàmm fa kanam Yàlla. Moo di Saraxalekat, bi nu ubbil bunt fa Yàlla. Moo di Buur, bi yilif ñépp ak yépp. + +Baat bii mu ngi jóge ci làkku araab, sukkandiku ci làkku ibrë, te muy tekki ‘Kirist' ci làkku gereg. Ci Injiil bi ci gereg Almasi bi dafay am ñaari yoon rekk (Yow 1:41; 4:25). Ci firi Wolof, bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci ndombam dañu koy firi Almasi. Bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci turam dañu koy firi Kirist. Seetal itam Kirist. + +Baat yi jóge làkku ibrë +Ci angale mooy aloes; Ci faranse mooy aloès + +Bantu genn garab la bu xeeñ lu neex, te joxe diwlin ji ñu def ci néew yi. Ci réewi penku yi la jóge. Boroomi xam-xam yi ci turu Akilariya agalosa (Aquilaria Agallocha) lañu ko xame. Garab yi am benn feebar rekk ñooy xeeñ. Feebar bi dafa soppi wàllu dàttam ba bant bi dëgër te ëmb benn diwlin bu neex. Bu ñuul bi mooy lu am feebar. Lu weex mooy lu amul feebar. + +Dañu koy gis ci Injiil ci Yow 19:39. + +Gàncax yi ak garab yi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy amethyst; Ci faranse mooy améthyste + +Per bu yolet la, bu xawa yaraax ni marjaan (jamaa) walla butéelu weer. + +Dañu koy gis ci Injiil ci Pe 21:20. + +Per yi ak Xeer yi ci Kàddug Yàlla +Ci angale ak ci faranse mooy Amphipolis. + +Dëkk bu am solo la woon, ci diiwaan bu tudd Maseduwan ci jamano nguuru Room ji. Ci bëj-gànnaaru Géeju Ese (mer Egée) la nekkoon. Nekkoon na ci yoon wu mag te wu am maanaa wu tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia), wu jaar ci diggante Asi Minër ak Itali. + +Amfipolis dafa feeñ ci Injiil ci Jëf 17:1. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Aminadab – Ci làkku ibrë (עמינדב|Aminadav) la tur wi jóge. Ci àngale mooy Amminadab or Aminadab, ci faranse mooy Aminadab. + +Baayu jabaru Aaroona, Eliseba la woon (Ex 6:23), di maamaatu Daawuda ak Yeesu. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu gis ci Macë ak ci Luug (Mc 1:4; Lu 3:33). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci làkku ibrë (אָמֵן) la baat bi jóge. Amiin mooy ni ñu koy waxe is làkku araab (آمين). +Ci angale ak ci faranse mooy Amen. + +Baat bi dafay tekki 'Na ame ni nga ko waxe.' + +Ci Injiil dañu koy gis ci Mc 6:13; Ro 1:25; 9:5; 11:36; 15:33; 16:24,27; 1Ko 14:16; 2Ko 1:20; Gal 1:5; 6:18; Ef 3:21; Fb 4:20; 1Tim 1:17; 6:16; 2Tim 4:18; Yt 13:21; 1Pi 4:11; 5:11; Yu 1:25; Pe 1:6,7; 3:14; 5:14; 7:12; 19:4; 22:20. + +Baat yi jóge làkku ibrë +Ci làkku ibrë (אמון) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Amon; Ci faranse mooy Amon + +Tàmbalee ci Robowam fukkeelu buur ak ñeent ci réewu Yuda la woon, di maamaatu Yeesu ci Macë (Mc 1:10). Man nañu gëstu jalooreem ci 2Ki 21:18-26; 2Ch 33:21-25. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale ak ci faranse mooy Amos. + +Benn ci maamaati Yeesu ci Luug la woon (Lu 3:25). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Amplias or Ampliatus; Ci faranse mooy Ampliatus + +Benn toppkatu Yeesu ci Room la woon. + +Dañu koy gis ci Ro 16:8. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale ak ci faranse mooy Ananias. + +Turu 3 nit ñi ci Injiil: + + Benn toppkatu Yeesu ci Yerusalem, mooy jëkkëru Safira. Jéemoon nañu nax mbooloo ñi gëm bi ñu jaayee woon benn pàkk ngir jox xaalis bi ndaw yi. Yàlla moo ko rey ca saa sa. Man nga ko jàng ci Jëf 5:1-10. + Benn toppkatu Yeesu ci Damas, bi Yàlla yónni ci Pool jëkk bi Yeesu feeñee ci moom (Jëf 9:10-18; 22:12-16). + Saraxalekat bu mag ba, ca 47 g.K. ba ca 59 g.K., maanaam ci jamano Pool ji (Jëf 23:2-4; 24:1). Ci at 66 g.K. kenn ku tudd Sakarii moo ko rey. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Annas; Ci faranse mooy Hanne ou Anne + +Saraxalekat bu mag ba la woon. Kiriñus, boroom réewu Siri moo ko fal saraxalekat ci at 6 walla 7 g.K.. Waaye Garatus, boroom réewu Yude, folli na ko ci at 15 g.K.. Mu fal ci palaasam Ismayel ba noppi Elasar doomu Anas, ba noppi Simoä, ba noppi Kayif ci at 18 g.K.. Waaye gannaaw bi ñu ko follee, baatam dafa weyoon di am sañ-sañ bu bare. Naka noonu Anas ak Kayif bokkoon nañu ci liggéeyu saraxalekat bu mag ba ca jamano ji Kirist liggéeyoon. Kayif takk na doomu Anas. + +Dañuy gis Anas ci Injiil ci Lu 3:2; Yow 18:13,24; Jëf 4:6; 5:17-18, 27-28. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ancos, ca jamono Injiil, péeyu diiwaanu nguuru Room bu tudd Siri la woon. Dafa nekkoon ca wetu joor gu naat ca dex gu yaatu gu tudd Oront (fleuve Oronte), 32 kilomet ca kaw bëlu dex ga, maanaam fu dex ga dugg géej ga. Teeru Ancos moo doon ca dëkku Selusi, bu nekkoon ca Géej gu Mag 8 kilomet ca noru bëlu dexu Oront ba. Selusi nekkoon na 26 kilomet ca sowu Ancos. + +Ca at bu Pool demoon fa, daanaka atu 43 g.K. dëkk bi xumb na. Nu ngi doon tabax di beesal dëkk ba, gannaaw ñaari yëngu-yëngu suuf yu yàqoon lu bare. Ay fukki junni Yawut ya dëkkoon Ancos te ñoom woomle nañu, te seen jàngu rafet nañu. Gereg yu bare ñi ngi doon ñëw ca seen diine. Ancos moo doon dëkk bu neex a dëkk te rafet. Waaye dëkk ba dafa siiwoon itam ndax seeni noos, seen ñaawteef ak seen njaaloo ak doxaanu yàqute. Bànneexu àddina si rekk la waa Ancos doon wut. + +Dëkku Gereg bu am solo la woon bu nekkoon ñetteelu dëkk bu gëna mag ci nguuru Room gannaaw dëkki Room ak Alegsàndiri. Buuru nguuru Maseduwan ñoo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist. Naka noonu ña fa jëkk a dëkk ñoo doon ay xarekatu Maseduwan ak waa Aten. Waaye yeneen Gereg ya toppoon nañu ca ñoom. Tamit buuru Geres dafa xiirtal Yawut ya ñu ñëw dëkk fa, te may na leen ñu nekk jaamburu dëkk ba. Waa Room nangu nañu diiwaanu Siri ca atu 64 j.K. Naka noonu ca jamono Injiil dëkk bi dafa boole waa Maseduwan, waa Geres, waa Room, waa Siri ak Yawut ya. Waaye amoon na ay jafe-jafe diggante Yawut ya ak ñi des ca waa Ancos ba dem sax ba am jamono waa dëkk ba bëggoon nañu rey Yawut ya fa dëkk. + +Ca suufu nguuru Room diiwaanu Siri dafa jëm kanam bu baax. Waa Room ñoo defoon Ancos seen péey ak màkkaanu xare ci diiwaanu Siri. Waaye ba tey waa Room may na dëkk ba mu yilif boppam. Ndegam Siri dafa nekkoon ca digu nguuru Room te mu féete waa Pàrt, beneen nguur bu xeex ak nguuru Room, Siri nekkoon ca suufu buuru Room ba moom ci boppam. Buur ba, Sesaar, moo faloon benn jawriñ ngir toogal ko ñetti at ba juróomi at yu nekk, mu nekk Boroom réewu Siri. Boroom réewu Siri moo sutoon Boroom réewu Yude, di ko yilif. Amoon na ñeenti mbooloom xare bu tudd 'léjiyoŋ' ca Siri, bu nekk bu am 6.000 xarekat ya. Amoon na itam ay gaalu xare ca Selusi. + +Yaakaar nañu ne daanaka 200.000 nit ña fa dëkkoon ca jamono Injiil. Benn boroom xam-xam dafa yaakaar ne benn cér ca juróom-ñaar ca niti dëkk ba Yawut la woon te Yawut ya dëkkoon ca ñetti gox ya. Yawut ya amoon nañu alal te seen dundin xëcc na yu dul Yawut yu bare ñëw bokk ca seen diine. + +Koom-koomu Ancos amoon na doole lool ndax kàttan gu mu am ci biir nguuru Room, tamit ndax yoonu jaaykat yi am solo ya jaaroon Ancos ak ndax lu ñu fa defaroon ca dëkk ba. Ancos dafa siiwoon ndax dàllu der yu rafet, latkoloñ, saf-saf yi ak ndàbb lu xeeñ, piis yi, gànjar ya ak takkaay ya, téere ya, ak li tëggu xaalis ak wurus defare. + +Yoonu jaaykat ya jóge ca penku, maanaam Babilon, Asiri ak Iraak jaar na Ancos, te dafa tiim yoon wu dem nor ak sudd wu boole Palestiin, Siri ak Asi Minër. Naka noonu amoon na wenn yoonu jaaykat wu jaar ca tund ya ca xunt bu tudd 'Buntu Siri' ba noppi dem Tars. Yoon mu jóge Tars wu tudd 'Yoonu Eŋaca' (Via Egnatia) dafa jàll Asi Minër ba dëkku Efes. Tamit gaal ya mënoon nañu dox ca dexu Oront diggante géej ga ak dëkk ba. + +Dëkk ba, moom, rafet na lool. Nguuru Geres def nañu yoon ya ca kaw tëralinu damyee ngir yoon yu mag ya jàpp ngelaw lu féex lu jóge géej ga. Amoon na benn miir bu mel ni tata bu wër dëkk ba lépp. Buuru Room bu nekk tàmbali ak Pompey ca atu 64 j.K., dugg na xaalisu nguuru Room yu bare ci tabax ya ak rafetaayu dëkk ba. Ni bépp dëkk bi Gereg ya walla waa Room tabaxoon amoon na ay powukaay ak amfiteyatërë, ay màggalukaayu yàllay xërëm yu bare, ak ay këru sanguwaay ya. Feesoon na dell ak ay pénc fu xale ya doon fo, waxkat ya indi seen wax, jaaykat ya jaay, te reetaanlukat ya bégloo mbooloo ya. Def nañu ay robine ca kaarfuur mbedd ya ngir jigéen ya mënoon nañu root, ndox moo xam ne mu jóge ca dex ga walla ca ay bëtu ndox ya amoon ca dëkk ba. Tamit Yulyus Sesaar tabax na benn 'akwadakk', maanaam pom bu indi ndox, ngir dimbali gox yoo xam ne amuñu woon ndox. + +Erodd bu Mag ba tabax na wenn yoon wu jàll diggu dëkk bi diggante buntu miiru dëkk ba ca penku-kaw, ak buntu miir ca sowu-suuf. Yaatuwaayu yoon wu mag woowu 10 meetar la woon. Dem na 4 kilomet, te lépp tali doj wu dëgër wu jóge Misra, walla marbar. Dafa dem ca pénc bu réy ca diggu dëkk ba. Ca pénc moomu amoon na benn nataalu Buuru Room Tibeer Sesaar bu réy bi ñu defare xànjar. Ca wetu yoon wa ca ñaari bor, fukki meetar yu nekk, amoon na ay kenu doj yi ñu taaral. Dafa meloon ni mbaar ba tax ñi dox ña mënoon nañu dox ca wetu yoon wa guddaayam lépp te bañ génne ca naaj wa walla taw ba. Yu gën a bare ca kenu ya amoon na ay nataal yi ñu yett walla defar ca xànjar. Diggante kenu ya amoon na bunt ngir dugg ca kër ya, bitik ya ak biro ya. Yoon ya amoon na sax làmp ya tàkk guddi. + +Amoon na benn dun ca biir dex ga fu dex ga jaar ci biir gox yu nekk ca noru dëkk ba. Guddaayam ak yaatuwaayam 3 kilomet la. Foofu lañu tabax këri buur yi, ak benn estaad ngir rawante fas ak sareet ya. Guddaayu estaad ba 500 meetar la woon ba moo wara tax mu bokk ca ya gën a réy ca àddina si. + +Ancos amoon na itam ay màggalukaay ca yàllay Gereg ak Room, ak ay powukaay. Yàllay Ancos moo doon Sës. + +Juróom-ñetti kilomet ca suddu miiru dëkk ba amoon na benn gox bu tudd Dafëne. Ca wetu yoon wa dem Dafëne amoon na ay tool fu ñu bey lawtanu réseñ ngir defare biiñ ak tóor-tóor yi ñu defare latkoloñ. Dafa nekkoon ca kaw benn déndu tund, maanaam 'palato'. Yaatuwaay ak guddaayu palato ba bu ne 1800 meetar ya la, te mu nekk 90 meetar lu gën a kawe niwo Ancos. Amoon na màggalukaay ca yàllay xërëm ju jigéen ju tudd itam Dafëne. Waa Ancos gëm nañu woon ne Dafëne nit la woon, ki Apolo, benn yàllay Gereg, soppoon. Apolo dafa ko dàqe di dàqe ba ci mujj Dafëne dafa soppiku nekk as ngarab bu tudd 'loriye'. Goxu Dafëne amoon na benn sardin walla park bi ñu defaroon ngir bànneex rekk bu am wëraayu 16 kilomet. Ca biir màggalukaayu Dafëne amoon na ay sëriñ yu jigéen yu nekk gànc yu bare. Guddi gu nekk ci seen turu diine ñu defaat li amoon ca nettali ba, maanaam jaamukat ya doon nañu dàqe sëriñ yu jigéen ya ci biir garabu loriye yi ci biir sardin ba, ba jàpp leen di séy ak ñoom. + +Buuru Room Ogust Sesaar samp na benn po 'olimpik' (Jeux D’olympique). Ñeenti at yu nekk po boobu indi na ay joŋantekat yu bare ngir rawante ci diiru 30 fan ci daw, tëb, sànni xeej ak fitt, rawante fas ak sareet, bëre ak ñoom seen. Amoon na itam rawante ca misik ak ci tari nettali. + +Gis nañu ne ay at gannaaw deewu Kirist, mbooloo ñi gëm ca Yerusalem fal nañu benn waa Ancos bu tudd Nikolas ngir mu bokk ca juróom ñaar yi doon toppatoo yëfu mbooloo ñi gëm (Jëf 6:5). Xebaar bu baax bi egg na Ancos gannaaw deewu Ecen daanaka atu 40 g.K. (Jëf 11:19-21). Ñi ko indi ay Yawut yi làkk Gereg lañu woon, yi jóge dunu Sipar ak dëkku Siren ca Libi. Ñoom def nañu lu bees. May nañu Gereg yi topp Yeesu ci lu sësul ca xaraf walla yeneen aada Yawut. Mbooloo bu mag gëm na Boroom bi. Foofu lañu jëkk tudd taalibe Kirist 'Gaayi Kirist' (Jëf 11:26). Ci bu jëkk tur boobu turu foontoo la woon. Waa Ancos dañu doon siiw ndax ni ñu doon foontoo nit. Daanaka fukki at gannaaw ga, amoon na ca ña gëm ca Yawut ya ca Yerusalem, ña jaaxle ndax yu dul Yawut yu topp Yeesu te kenn xarafalu leen. Werante wu réy amoon na ba tax ñu def genn géew ca Yerusalem, 650 kilomet fu sore Ancos, ngir waxtaan ci. + +Am-ami ñi gëm may na leen ñu mënoon a yónni ndimbal ca ña gëm ca Yerusalem (Jëf 11:27-30). Tamit ca mbooloo ñi gëm ca Ancos la Pool jóge ngir tas xebaar bu baax ba ci biir yu dul Yawut ya, te ca Ancos la dellusi yoon bu nekk – maanaam Ancos dafa nekkoon mel ni màkkaanam. Ñetti tukkeem yépp dafa tàmbali Ancos. Ca jamonoom, mbooloom ñi gëm ca Ancos moo gën a am taxawaay bépp mbooloo ci mbiru ni mbooloom yi ca àddina sépp doxe, xëyna bu dul mbooloom ca Yerusalem. + +Tey jii dëkk bu ñàkk solo la bu tudd Antakya ci Tirki (Turquie). Am na 35.000 nit kese, ay toppkatu egëliis gereg yi des ci biir am réewu jullit yi. + +Ancos ca Siri feeñ na ca Jëf 6:5; 11:19-27; 13:1; 14:26-15:3; 15:22,23,30-33,35; 18:22-23; Gal 2:11 + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Siri + +bs:Antiohija#Historija +el:Αντιόχεια#Γενικά +fr:Antioche#Histoire +he:אנטיוכיה#היסטוריה של העיר +hr:Antiohija#Povijest +hu:Antiokheia#Története +la:Antiochia ad Orontem#Historia +nl:Antiochië#Geschiedenis +Ancos mooy benn dëkk ci wetu diiwaanu Pisidi, fu Pisidi digalook diiwaanu Firisi. Ci dëgg-dëgg ci diiwaanu Firisi la bokkoon waaye ba tey faraloon nañu ko tudd Ancos ci Pisidi. Gentam sorewul dëkk bu tudd tey jii Yalwacc (Yalvaç) ci Tirki (Turquie). Ancos nekkoon ca kaw benn tund wu ndaw bu nekkoon ca kaw benn palato bu yaatu te naat. Tund wu ndaw wa moom itam palato la woon, wu am dénd lu tollook 300 ektaar. Benn boor nekkoon 15 meetar ca kaw jooru palato ba. Waaye beneen boor nekkoon mbartal mu kenn mënul yéeg 60 meetar ca kaw joor ja. Naka noonu dafa mel ni tata te yomb na aar. Nekkoon na itam ca yoon wi mag wi waa Room tabaxoon wi jàll Asi Minér penku ba sowu diggante dëkku Tars ak dëkku Efes, wu tudd 'Yoonu Sebasëtë'. + +Nguuru Selësid (maanaan waa Siri, ñi donnoon wàllu nguuru Geres) moo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist, ngir teg fa xare ba, Bëggoon nañu aar nguur ga ca xeetu Pisidi wu nekkoon ca tund ya ca sudd, tamit am ndogal ca lépp lu jaar ca yoonu jaaykat ya wu mag wu jaaroon Asi Minër penku ba sowu. Sampoon na ko fa itam ngir boole ñi dëkk ca diiwaanu Firisi ak aada Gereg yi. Ñi fa jëkk a dëkk ñoo doon Gereg yi jóge dëkku Maŋesi ca diiwaanu Lidi ak Yawut yi jóge Babilon. Ca atu 25 j.K. nguuru Room moo def dëkk ba suufus Room, boole ko ak diiwaanu Galasi. Jaamburi dëkk ba yépp amoon nañu yelleef yu yem ak yosu waa dëkku Room. Tamit, indi nañu ay xarekatu Room yu bare yi ñu may ñu génne xare ba (maanaam soldat yu màggat), te may leen suuf ngir ñu dëkk fa. Gannaaw ga ndànk-ndànk dëkk ba tàmbali gën a niroo dëkki Room yeneen dëkk yi ko wër. Ca jamono Injiil dafa niroo dëkku Room ca wàllu yoon wa, ca wàllu nguur ga, ak ca wàlli tabaxin ak colin. Rafetal nañu dëkk ba bu baax ak pénc ya, ak kenu ya, te ak nataal yi ñi yett ca doj ak xànjar. + +Ancos ci Pisidi moo doon dëkk bu gëna am solo ca diiwaan ba. Lu ëpp 100.000 nit ñoo fa dëkkoon. Dëkk ba boole na ay xeet yu bare. Amoon na ci bu jëkk waa Firisi, ba noppi indi woon nañu waa Gereg ya ak Yawut ya, ba noppi waa Room ya. Ci biir dëkk ba amoon na ñaari pénc yu réy yi ñu defare doj. Benn ca ñoom péncu Tibeer lañu ko tudd, mu am dénd bu tollook 300 meetar kaare, bi doon 'grand palaasu dëkk ba' fu nit ñi doon jaay, di fo, di waxtaan. Kenu yu réy te rafet ñoo ko wëroon. Beneen bi nag, mooy péncu Ogust moo dend péncu Tibeer. Ci seen diggante amoon na benn iskale bu am 12 mars (maanaam tegukaayu tànk), bu nekk am yaatuwaayu 20 meetar. Ca kaw iskale ba amoon na bunt bi ñu defare ak 3 ars yu réy-a-réy. Ab ars mooy lenn li ñu tabax ngir nekk pàttaliku. Dafa am ñaari kenu doj yu réy yi ñu boole ak lu mel ni xala doj bu jaar ca seen diggante, tiim leen. Def nañu bunt bi ngir nekk pàttalikukaayu ndam li Ogust Sesaar amoon ca xeex ya. Ca kawu ars ya yett nañu ay nataal yu réy. Beneen booru péncu Ogust moo doon wenn tundu doj. Ci biir tund wa yett nañu genn xala, rafetal ko ak ay kenu yu kawe ya. Ca diggu xala ga amoon na benn màggalukaay bu réy bi ñu defare marbar bu weex ngir teral seen Yàlla Men ak buur bi Ogust Sesaar. Ñu sooga àggale màggalukaay ba bi Pool demoon fa, ak ars ya bala mu dellusi ñaareel bi yoon. Ancos amoon na itam ndox ca tiwo yi jaar fépp ca dëkk, mu jóge ca benn bëtu ndox ca tund ya nekkoon fukki kilomet ca biti dëkk ba. Indi nañu ndox ak li tubaab tudd 'akwadakk'. Ci diiru 8 kilomet dafa jaaroon ci biir suuf si, waaye 2 kilomet yu mujj yi dafa jaaroon ca kaw pom bu kawe bi ñu tabax ngir yóbbaale ndox. + +Seen Yàlla 'Men' la tuddoon. Amoon na itam beneen màggalukaayu Men ca wenn tund bu kawe lu tollook 25 kilomet ca penku dëkk ba. Bérab boobu mooy bérab bu bokkoon ca ña gën a am solo ca seen diine. At bu nekk def nañu benn po ngir teral Men. Gëmoon nañu ne Men mooy yàllay wér-gi-yaram, naataange, ak jàmm, te ku aar bàmmeel ya. Mooy itam yàllay weer wi. Ca nataalam ku niroo nit la woon mu sol yere. Misaale nañu ko ak wenn yëkk tamit ak nataalu weer bu am juróom-ñetti fan. + +Sersiyus Poolus, boroom réew mi ca dunu Sipar (Jëf 13:4-12), dafa bawoo Ancos ci Pisidi. Ay bokkam moomoon suuf su yaatu ca gox ba. Moom gëm na Boroom bi Pool demoon Sipar. Xëyna Boroom réew mi moo boole Pool ak dëkku Ancos ba tax Pool ak Barnabas gaaw nañoo dem Ancos bi ñu jóge dunu Sipar. + +Ca jamono Pool ndoxaanu yàqute, def yaramu neen, topp nafsu, màndite, lekk suuxu mala bu ñu toggul, te naan deret bokkoon na ca diine. Naka noonu, ñu bare bi ñu xoolee dundinu Yawut yi, ñu tàmbali xeeb diine ji ñu fekkoon, di tàmbali bokk ca diine Yawut ya, rawatina jigéen ñi woomle. Ca dëkku Ancos, jigéen ñooñu ñoo doon jabari magi dëkk ba. Naka noonu Yawut ya noonoo Pool jaaroon nañu ca jigéen ñooñu ngir ñu laaj seen jëkkër ñu dàq Pool ca dëkk ba. + +(Jëf 13:14-51; 14:19-23; 2Tim 3:11) + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Barnabas, miy tekki “Kiy dëgëral fit yi” (Jëf 4:36). + +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Andrew; Ci faranse mooy André + +Benn ci fukki taalibe Yeesu ya ak ñaar la woon, di rakku Simoä Piyeer. Ñu bokk ndey ak baay. Nappkat bu bawoo ca dëkk bu tudd Betsayda ca diiwaanu Galile la woon. Bala mu topp ci Yeesu nekkoon na taalibe Yaxya. + +Dañuy gis Andare ci Injiil ci Mc 4:18-20; 10:2; Mk 1:16-18,29; 3:18; 13:3,4; Lu 6:14; Yow 1:35-44; 6:8-9; 12:20-22; Jëf 1:13. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale ak ci faranse mooy Andronicus. + +Benn Yawut bu toppoon Yeesu la woon. Ndawu Kirist la woon ki bokkoon ak Kirist bala Pool. + +Ci Injiil dañu koy gis ci Ro 16:7. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy dill or anise; Ci faranse mooy aneth + +Jiwu walla doomu gàncax gu saf la. Boroom xam-xam yi xam nañu ko ci turu Anetum graweyolensë (Anethum graveolens). Jëfandiku nañu ko ngir safal ñam ak faj feebar. + +Ci Injiil dañuy gis baat bi ci Mc 23:23. + +Gàncax yi ak garab yi ci Kàddug Yàlla +Ci angale ak ci faranse mooy Antipas. + +Toppkatu Yeesu bu jóge Pergam la woon, bi ñu reyoon ndax ngëmam ci Yeesu. + +Dañuy mana gis Antipas ci Pe 2:13. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale ak ci faranse mooy Antipatris. + +Benn dëkk ci diiwaanu Samari la woon. Nekkoon na 42 kilomet ca bëj-saalumu Sesare ca joor gu nekk ca wetu Géej gu Mag ga. Ci yoon wu mag wa tudd Yoonu Maris (Via Maris), wi jaaroon ci diggante réew yi ci Palestiin, la nekkoon. Tey jii dëkk bu tudd Ras el Ain moo fa nekk. + +Dañuy gis dëkk bi ci Jëf 23:31. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Apelles; Ci faranse mooy Apellès + +Benn toppkatu Yeesu ca Room la woon. Turam feeñ na ci Injiil ci Ro 16:10. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy (Forum of) Appius; Ci faranse mooy (Forum d')Appius + +Benn dëkk ci réewu Itali la woon, bu amoon ja bu mag. Nekkoon na lu tollu 40 kilomet ci bëj-saalumu Room ci yoon wu mag wa tudd Yoonu Appien (Via Appienne). + +Dañu koy gis ci Jëf 28:15. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Apollonia; Ci faranse mooy Apollonie + +Benn dëkk ci diiwaanu Maseduwan la woon, ci wetu géej ga tudd Géeju Ese (Mer Egée). Nekkoon na ci diggante dëkki Filib ak Tesalonig ci yoonu wu mag wa tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia), wi jaaroon ci diggante Asi Minër ak Itali. + +Man nañu gis turu dëkk bi ci Injiil ci Jëf 17:1. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Girees +Yoonu nguuru Room wu mag wu tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia) dafa demoon ci diggante Asi Minër ak Itali. Tàmbale na fu dëkku Istanbuul nekk tey ji ca Géej gu Ñuul ga, jàll Maseduwan ba egg géeju Adiratig. Bokkoon na ca yoon wu ñu jaaroon ngir dem Itali ak Room. + +Tali doj la woon. Maanaam defaroon nañu ko ak ay xeex yu ñu yett ba kaare ngir seen ànd jege. Yoonu Eäaca jàll na diiwaanu Maseduwan diggante Géej gu Ñuul ak Géeju Adiratig. Dafa tàmbali woon ca Géej gu Ñuul ca dëkk bu tuddoon Bisansë (Byzanse), mooy dëkku Istanbul, jaar ca dëkki Neyapolis, Filib, Amfipolis, Apoloni, Tesalonig, ak Pela ba noppi dem ba Dirxasiyum (Dyrrhachium) ak Apoloni ca Géeju Adiratig. Guddaay ga mooy tollook 800 kilomet. Nit ñi doon nañu dugg gaal ca Dirxasiyum walla Apoloni ngir jàll géej ga te fekk yoon wa jëm Room. +Ci angale ak ci faranse mooy Apollos. + +Benn Yawut la woon, bu bawoo ci Alegsàndiri. Boroom xam-xam ci Mbindi Yonent yi la woon, te nekkoon jàngalekat bu mag ci mbooloo ñi gëm ñi. Waxkat la woon itam, ku mënoona wax wax yu rafet ci gereg. + +Apolos moo feeñ ci Injiil ci Jëf 18:24-19:1; 1Ko 1:12; 3:4-6,22; 4:6; 16:12; Tit 3:13. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Apolyon *Grekçe, İncil de geçen bir melektir.İbranice adı, Avaddon'dur. + +İncil Vahiy 8,9 Yedi Borazan + (Apolyon'un geçtiği ayet, 9. ayettir.) + +Beşinci melek borazanını çaldı. Gökten yere düşmüş bir yıldız gördüm. Dipsiz derinliklere açılan kuyunun anahtarı ona verildi. Dipsiz derinliklerin kuyusunu açınca, kuyudan büyük bir ocağın dumanı gibi bir duman çıktı. Kuyunun dumanından güneş ve hava karardı. Dumanın içinden yeryüzüne çekirgeler yağdı. Bunlara yeryüzündeki akreplerin gücüne benzer bir güç verilmişti. Çekirgelere yeryüzündeki otlara, herhangi bir bitki ya da ağaca değil de, yalnız alınlarında Tanrı’nın mührü bulunmayan insanlara zarar vermeleri söylendi. Bu insanları öldürmelerine değil, beş ay süreyle işkence etmelerine izin verildi. Yaptıkları işkence akrebin insanı soktuğu zaman verdiği acıya benziyordu. O günlerde insanlar ölümü arayacak, ama bulamayacaklar. Ölümü özleyecekler, ama ölüm onlardan kaçacak. Çekirgelerin görünümü, savaşa hazırlanmış atlara benziyordu. Başlarında altın taçlara benzer başlıklar vardı. Yüzleri insan yüzleri gibiydi. Saçları kadın saçına, dişleri aslan dişine benziyordu. Demir zırhlara benzer göğüs zırhları vardı. Kanatlarının sesi savaşa koşan çok sayıda atlı arabanın sesine benziyordu. Akrebinkine benzer kuyrukları ve iğneleri vardı. Kuyruklarında, insanlara beş ay zarar verecek güce sahiptiler. Başlarında kral olarak dipsiz derinliklerin meleği vardı. Bu meleğin İbranice adı Avaddon, Grekçe adıysa Apolyon’dur. +Ci angale mooy Arab; Ci faranse mooy Arabe + +Naar yi, maanaam xeet yi jóge ci diiwaanu Arabi. + +Araab yi bokkoon nañu ci ñi nekkoon ci Yerusalem ci Jëf 2:11. + +Xeet yi +Ci angale mooy Arabia; Ci faranse mooy Arabie + +Ci jamano Injiil ji, diiwaanu Arabi moo fare woon penku ak bëj-saalumu réewu Yude, maanaam wàllu bëj-saalumu réewu Yordani (Jordanie) ak wàllu bëj-gànnaaru Arabi sawuditt (Arabie saoudite). Nekkul woon lu ñuy wax diiwaanu Arabi tey jii, maanaam lépp lu nekk ci diggante Géej gu Xonq ak Géeju Pers (golfe Persique). + +Man nañu fekk tur wi ci Gal 1:17; 4:25. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Aretas; Ci faranse mooy Arétas + +Aretas IV Filopatiris, buur bu jóge réewu Arabi la woon. Jamanoom moo doon 9 j.K. ba 40 g.K.. May nañu Erodd Antipas doomam bu jigéen. Waaye Erodd dafa ko fase bi mu bëggee woon takk Erojàdd. Aretas yónni na ay xarekatam ci xare ngir xeex ak Erodd. Mu noot ko ci 36 g.K.. Aretas teg na benn jawriñ ngir yilif dëkku Damas. Kooku jéemoon na jàpp Pool. + +Turam moo feeñ ci Injiil ci 2Ko 11:32. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Areopagus; Ci faranse mooy Aréopage + +Bérab ci biir dëkku Aten la, bu nekk ci kaw wenn tundu xeex wu kawe. Amoon na ay siis yi ñu defare woon doj ngir kureelu dëkk ba manoon faa daje. Indi nañu Pool foofu ngir mu waareji (Jëf 17:18-34). + +Tur wi moo feeñ ci Injiil ci Jëf 17:19,22,34. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Girees +Ci angale mooy Arimathea; Ci faranse mooy Arimathée + +Amoon na ay dëkk yi ñu tudde Arimate ci réewu Israyil. Arimate moo tur ci làkk gereg. Ci làkku ibrë Rama la tudd. Yaakaar nañu ne dëkk bu tudd Arimate ci Injiil moo nekkoon ci tund ma tudd Efrayim lu tollu 8 kilomet ci bëj-gànnaaru Yerusalem. Foofu la yonent Yàlla Samwil juddoo woon. Ci Injiil Arimate mooy dëkk ba Yuusufa, mi suuloon Yeesu, jóge. + +Mc 27:57; Mk 15:43; Lu 23:50; Yow 19:38. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Aristarchus; Ci faranse mooy Aristarque + +Benn toppkatu Yeesu mi dëkkoon Tesalonig la woon, ànd na ak Pool ci liggéeyam. + +Aristàrk moo feeñ ci Injiil ci Jëf 19:29; 20:3-5; 27:2; Kol 4:10-11; Fm 1:24. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Aristobulus; Ci faranse mooy Aristobule + +Benn toppkatu Yeesu bu dëkkoon ci Room la woon. Man nañu gis turam ci Ro 16:10. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Archelaus; Ci faranse mooy Archélaüs + +Erodd Arkelawus, doomu Erodd bu mag ba, moo falu woon ci diiwaani Yude, Samari ak Idume (Idumée) 4 j.K. nguuru ba 6 g.K.. Yaayam Maltas (Malthrace) la tudd. Arkelawus ak Erodd Antipas ñoo bokkoon ndey ak baay. Yawut yi ak waa Samari yi jiiñ na ko kor ci kanamu buuru Room ndax coxoram. Buur bi Ogust Sesaar moo ko fuñ ci diiwaanu Gool (Gaule), maanaam Farans, ci 6 g.K.. Gannaaw loolu def nañu Yude diiwaan ci suuf nguuru Room, te jawriñ yi buuru Room fal yilifoon fa. Jabaram Mariyamënë (Mariamne), doomu Aristobul la, ki mu fase ngir takk Galafira (Glaphyra), jëtunu Alegsàndar (Alexandre), magam. + +Man nañu gis tur wi ci Mc 2:22. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Archippus; Ci faranse mooy Archippe + +Benn toppkatu Yeesu ci Kolos la woon. + +Man nañu gis turam ci Injiil ci Kol 4:17; Fm 1:2. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (הר מגדון) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Armageddon; Ci faranse mooy Harmaguédon + +Armagedon mooy turu benn tund ci làkku ibrë bi ñu sotti ci làkku gereg. Ci làkku ibrë Megido (Meguiddo) la tudd. Ci Injiil dafa misaale bérab fu xare bu mujj bi nara am ci diggante gaayi Yàlla yi ak gaayi Seytaane yi ci muju jamano ji. Tundu Megido bokk na ci tundi Karmel yi. Dafa nekkoon ci benn boru xunt mu mayoon nit ñi jàll tund yi. Ci joor bu nekk ci taatam la Sóol (1Sa 31:1-8) ak Yosiyas (2Ch 35:20-24) dee, te Sedeyon amoon ndam ci waa Majan ñi (Jud 7). + +Armagedon mooy feeñ ci Injiil ci Pe 16:16. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (אַרְפַּכְשַׁד / אַרְפַּכְשָׁד) la tur wi jóge. Ci angale mooy Arpachshad; Ci faranse mooy Arphaxad + +Doomu Sem ak sëtu Nóoyin la woon. Juddoom fekk na mbënn ma weesu ba teg ñaari at (Ge 11:10-13). Kenn ci maamaati Yeesu yi ci Luug la woon (Lu 3:36). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci angale mooy Artemas; Ci faranse mooy Artémas + +Xaritu Pool la woon. Turam feeñ na ci Injiil ci Tit 3:12. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Diana; Ci faranse mooy Artémis + +Artemis mooy turu jenn yàlla ju araam ju jigéen ci làkku gereg. Ci làkku waa room Diyana la tuddoon. Ñaari yàlla yu araam bokkoon nañu tur Artemis. Benn mooy li ñu gis ci Injiil, maanaam yàllay Efes (Jëf 19:23-41). Beneen yàllay gereg la woon ki ñu foog ne jigéenu yàlla ju araam ja tudd Apolo. Diine Artemisu Efes niroo na diine Astarte, yàllay waa Sidon. + +Tur wi feeñ na ci Injiil ci Jëf 19:24,27,28,34,35. + +Yàllay xeet yi +Ci làkku ibrë (אָסָא) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Asa; Ci faranse mooy Asaf + +Doomu Abiya la woon. Li dale ci Robowam ñetteelu buur ci Yuda la woon. Dafa nguuru lu tollu 41 at ci diggante 913 j.K. ba 873 j.K.. Man nañu jàng ci jalooreem ci 1Ki 15:8-24; 2Ch 14:1-16:14. Benn ci maamaati Yeesu ci Macë la woon (Mc 1:7,8). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci angale mooy Asyncritus; Ci faranse mooy Asyncrite + +Benn toppkatu Yeesu ci Room la woon. Turam feeñ na ci Injiil ci Ro 16:14. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (אָשֵׁר) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Asher; Ci faranse mooy Asser + +Benn ci giiri bànni Israyil la woon, ñi soqikoo ci Aser, mi doon juróom-ñetteelu doomu Yanqóoba bu góor. + +Giiru Aser moo feeñ ci Injiil ci Lu 2:36; Pe 7:6. + +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale ak ci faranse mooy Azor. + +Benn ci maamaati Yeesu ci Macë la woon (Mc 1:13,14). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Assos; Ci faranse mooy Assos + +Benn dëkk ak teeru la woon, ci diiwaanu Misi. Tey jii, mooy dëkk bu tudd Behramkale ci réewu Turki (Turquie). + +Dañuy wax ci Asos ci Injiil ci Jëf 20:13,14. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Azotus; Ci faranse mooy Azot + +Dëkk la woon, ci bëj-gànnaaru diiwaanu Yude, lu tollu 4 kilomet diggam ak Géej gu Mag ga. Nekk na bu yàgg bala jamano Injiil ji, lu tollu 1400 at. Ci jamano yooyu Asdodd la tuddoon. + +Man nañu ko gis ci Injiil ci Jëf 8:40. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Attalia; Ci faranse mooy Attalie + +Dëkk la woon, di teeru bu gëna am solo ci diiwaanu Pamfili fa diiwaan bi digalook diiwaanu Lisi. Tey jii Antalya ci réewu Turki (Turquie) la. + +Man nañu koy gis ci Injiil ci Jëf 14:25. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Ci angale mooy Athens; Ci faranse mooy Athènes + +Aten dëkk bu mag la, ci réewu Geres mooy péey ba sax, te siiw na ngir xam-xam ba'ak njàng ma, ak caada ja. Yaakaarees na ne lu ëpp téeméeri junni ciy way dëkk ñoo fa dëkke. Nekkoon na péeyu nguuru waa Geres, bi tuddoon Atig (Attique). Tey mu tudd Aten . + +Sancees na Aten daanaka 3.000 at Nj. Is (njëkk Iisaa). Daanaka 500 at njëkk Iisaa fekkoon na mu am nguur gu yaatu lool. Waaye Geres dafa ñàkkoon suuf. Moo tax waa Geres yi tuxu, di sanc ay dëkki Geres yu bari ca Tugal ak Asi gu ndaw gi. + +Moone ca jamonoy Pool dafa ñàkk xaalis. Amatuñu nguur, te diiwaanam Atig dafa tuuti - dénd bu tollook 2.600 kilomet kaare matul sax benn departemaŋ ca Senegaal. Amul feneen ca Atig fu gën a sore Aten 40 kilomet. Seen suuf musuñoo doy seen soxla. Taw bi barewul woon, lu tollook taw bi ñu am ca noru Senegaal. Ñetti cér ca ñeent ca suuf si amul njëriñ ci bey te yu bare ci yi des amoon njëriñ ca bey garabu oliw rekk. Amoon nañu mbélli xaalis waaye fekk nañu ne jeex nañu tàkk laata jamono nguuru Room. Tamit seen doole ci jaay wàññiku na, ndax doole yeneen dëkk yu mel ni Ancos, Korent, Efes, ak Alegsàndiri. + +Dëkku njàng la woon, bu amoon jenn daara ju kawe 'iniwersite'. Naka noonu siiw nañu ndax seen xam-xam ak seen waxin, ndaxte waxin lañu ca gën a jàngale. Wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xinte. Amoon na ay mbooloo boroom xam-xam. Benn ca mbooloo boroom xam-xam moo tuddoon Epikuren. Kureel la woon, bi sës ci njàngalem Epikuur (mu faatu 270 at lu jiitu jamano Kirist) te fonk bànneex, ba mucc ci bépp tiis. Gëmuñu Yàlla, waaye ñu gëm ne àddina dafa sàkk boppam te amul boroom. Te boo deeyee amul dara lu ciy topp. Nekkatuloo daal. Beneen mbooloo dafa tuddoon Estowisen. Kureel la woon, bu sës ci njàngalem Senon (mu faatu 265 at lu jiitu Kirist). Fonk nañoo naagu, ba bañ a yég dara, muy bànneex mbaa naqar. + +Dëkk bi fees na dell ak màggalukaayu yàlla yi ñu defare marbar, yu réy-a-réy te rafet, nataal ya ñu yett, kenu ya, robine ndox bi ñu tudd 'fonteen' ak yeneen rafetaay. Ca diggu dëkk ba amoon na benn tund wu am ay màggalukaay rekk. Ëpp nañu fukk. Nekk na daanaka 100 meetar ca kaw niwo dëkk ba. Ca ñetti boor am na mbartal bu jub xocc mel ni miir. 'Akëropool' la tudd. + +Benn ca màggalukaay ya moo doon màggalukaayu Sës, yàlla ju gën a mag ca diine Gereg. Àggaleeguñoo tabax màggalukaay ba ca jamono Pool. Waaye ba noppi amoon na 104 kenu marbar, bu nekk am kawewaayu 17 meetar ak yaatuwaayu 2 meetar! Kawewaayu màggalukaay ba moom ca boppam moo doon 27 meetar. Ca biir amoon na nataalu Sës bi ñu defare wurus ak iwaar. Bokkoon ca ñeenti màggalukaay yu gën a réy ca àddina si ca jamono. + +Màggalukaay bu gën a am solo moo doon li ñu tudd 'Parténon' bi ñu defaroon ngir yàllay dëkk ba, maanaam, Atena. Guddaay 72 meetar la, yaatuwaay 34 meetar, te kawewaay 20 meetar. Ca kaw kenu ya amoon na nataal bu ñu yett bu wëroon tabax bépp ca 92 wàll. Wàll bu ne indi na benn ca seeni nettali yàlla. Amoon na beneen nataal bi ñu yett ca diggante kenu ya bu amoon 600 melo ya - ay góor, ay jigéen ak ay bàyyima yi bokk ca ña indi seen yàlla Atena benn yére wurus at bu nekk. Guddaayu nataal bi mooy 160 meetar. Te def nañu nataal yi ngir ñi taxaw ca suuf di ko xool yaakaaroon nañu ne dañuy jàkkaarlook nataal ba, fekk na ne nekkoon na 10 meetar ca seen kaw. + +Waa Aten jaamu nañu ay yàlla yu bare. Waaye yàllay dëkk ba moo doon Atena. At bu nekk ci weeru yuuliyoo, amoon nañu benn màggal lu diir 8 fan. Ca fan yu jëkk ya def nañu ay joŋante, rawante gaal ya, fas ak sareeet ya, rawante ca woy ak nettali, ay mbumbaay. Ca juróom-benneel ba fan, ca fajar, saraxalekat ya ak magi dëkk ba, jiitu nañu mala ya ak waa dëkk ya yépp, ñu dox ca biir dëkk ba, ba egg Panténon fu ñu def sarax ya, te ñépp lekk yàpp. Sarax nañu 100 mala, mooy nag ak xar, at mu nekk. + +Amoon na bérab ci biir dëkku Aten bu tudd Areyopas. Nekkoon na ci kaw wenn tundu xeex wu kawe. Amoon na ay siis yi ñu defare woon doj ngir kureelu dëkk ba manoon faa daje. Indi nañu Pool foofu ngir mu waareji. + +Ni dëkki Gereg yépp amoon na pénc bu ñu tudd 'Agora'. Amoon na ñaar sax - benn bi waa dëkk ba tabaxoon ak benn bi waa Room tabaxoon. Ay péncu doj lañu yi ñu rafetal ak kenu yu réy ak nataal ya. Ñoo doon maase, ak grand palaasu dëkk ba, te fu ñu doxale nguur. Foofu itam amoon na ay màggalukaay ak ay saraxalukaay. Ci dëgg-dëgg mënuloo dem fenn ca dëkk ba te gisul benn màggalukaay walla nataalu yàlla. + +Amoon na ay powukaay itam. Ñoom itam dañuy kéemaane. Benn ca ñoom woyuwaay la bi ñu teg ne mooy bu gën a rafet ca àddina si. Beneen mënoon na toogal 17.000 nit, te léeg-léeg dina fees ba ëpp loolu sax! Amuñu jot a lim bépp tabax bu yéeme bu nekkoon ca Aten bi fa Pool ganesi. + +Dëkku Gereg la woon waaye amoon ay Yawut itam. + +Aten dafay feeñ ci Injiil ci Jëf 17:15,16,21,22; 18:1; 1Tes 3:1. + +Iniweersite +Iniweersite Aten + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Aten + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Girees +Péy +Awa soxnas Aadama + +Ci làkku ibrë (חַוָּה) la tur wi jóge. Awa mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam (حواء, Hawwa). Ci angale ak ci faranse mooy Eve. Turu jigéen ji Yàlla jëkka bind la. Ci faaru Aadama la ko Yàlla bindoon. Danuy gis jalooreem ci Ge 1:27-30; 2:20-4:2,25. Ci Injiil feeñ na ci 2Ko 11:3; 1Tim 2:13. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet + +Ci Lislaam + +Awa ak Adaama sunu Boroom Moo ngi nuy nettali seen i bir ci Alxuraan, awa di Soxna ci Aadama, doon wéttalam ak noflaayam. + +Alxuraan a ngi naan: +35. Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- +tooñ ña”. [Saar 2: Nag Wa] + +19. “Te yaw Aadama, dëkkal yaak sa soxna, Àjjana ; lekkleen yéen ñaar fu leen fi neex ; +waaye buleen jegeñ garab gii ; su amee, ngeen tooñ.” + +20. Séytaane jax-jaxal leen ngir mu feeñal ca ñoom ñaar la Nu leen nëbboon - ci seen cër - mu +ne leen : “Seen Boroom terewuleen ngeen jegeñ garab gii lu dul ne Dafa bañ ngeen nekk ñaari +Malaaka walla ngeen bokk ca ñay dund fàwwu [duñu dee] ! ”. + +21. Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”. + +22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt +di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab +gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ” + +23. [[[Aadama]] ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm +nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”. + +24. Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay +ak i xéewal ab diir.” +25. “Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].” + [Saar 7: Dig Wa] +Ci làkku ibrë la tur wi jóge. +Ci angale mooy Aenon; Ci faranse mooy Énon + +Bérab boo xam ne sorewul Salim la woon, ci sowu dexu Yurdan gi ci wàll bëj-gànnaaru dex ga. Xamatuñu tey jii ne tembe fan la Aynon walla Salim nekkoon. Waaye dañu koy gëna yaakaar bérab bu sorewul dëkk bi tudd tey jii Napalus (Naplouse). + +Man nañu koy gis ci Yow 3:23. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Téeree ngii di benn ci yi ñu gën a yër ci àdduna bi, mooy téere bees sellal ci lislaam, di fi jullit ñiy ball-loo seen yoon di Shariiha, ak ci sunna siy dundiinu Yónnent bi (jàmm yal na nekk ci moom), kon nag bu am solo la lool fi jullit ñi. + +Alxuraan: Alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi, mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu Lislaam gi, ci ginnaawam la Sunna di ñëwe. Li njëkk a wàcc ci Alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru Halaq muy : «Jàngal ci sa turu boroom bi bind (sàkk) » + +Alxuraan nag mooy waxi Yàlla ji mu wàcce ci Yonentaam ba Muhammad, Jibriil nag mooy ndawul Yàlla tey malaaka mi ko wàcce; ngir nag Yonent bi jottali ko nit ñépp,. Moom nag fa Yàlla dees koo bind ca àlluwa jees wattu ja (Lawhul Mahfuus), àlluwa jii nga xam ne Yàlla bind na ca lu nekk njëkk mu koy sàkk. Wattu googu nag Yàlla la soob, mu bëgge ko noonu, noonu la ko waxe: «Nun noo wàcce Alxuraan, te nun noo koy wattu» + + Saaru Xunti ma + Saaru Maryama + +Kaamil bi + +Alxuraanul Kariim + +PDF Alxuraan Ci Wolof + + PDF +Alxuraan + +Lëkkalekaay yu biti + Al-Quran (Alxuraan) +Wolof làkk la wu ñuy wax ci Gàmbi (Gàmbi Wolof), Gànnaar (Gànnaar Wolof), ak Senegaal (Senegaal Wolof). Mi ngi bokk nag moom wolof ci bànqaasub atlas bu làkki Kongóo yu kojug nit ñu ñuul ñi. Mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la. Am na it lumu séq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer, joolaa ak basari. + +Ubbite +Bi ñu demee ba gis jëmm ja, muy ku sew, tuuti te xaw a wow, waaye di ku ñu muure ab taar, ci anam gu woyof te loyox, di ku ñu aare kàttan, sóob ko ci ag fonk-sa-bopp doonte ag neen la, solal ko yéerey yëgle ak jaral, te ma jëli loolu ca jafeem gaa jëli. Bi loolu amee, dama ne leen xanaa kay du kii ngeen ma doon wax? ñu ne ahakay, cis lëf, cig yéemu, ak ñàkk a xalaat ne dinaa sikk mukk ci moom, ma jug man, xajal leen foofa fépp. + +Ma ne nag waaw ku mel nii, ci li mu làmboo ciy melo, lu ko nit di doye ? +Ginnaaw bi nag dégg naa ñuy wax naan moom de bokk na ci ñi gën a jekk ci boobule gox, ànd ak jaaxle ci samaw jëfiin, ci ba ga ma ko fa ba, ma ne leen man : moo xam! +Lii mooy li am ci sunu làkk wii, walla yii di yu Afrig yi, dañu di yu am solo te man a dem ni yépp di deme, am barab ci digg barabi làkk yépp, waaye li nu dal nun waa Afrig, mooy li dal sunu lépp, dalaale ci li muy dal sunu kàllaama yii nga xam ne wii de bokk na ci yi gën a nosu, gën cee nooy, gën cee nangoo defaru, yéwénu, ruy, ci ku ko ruyal, tey way nag ca nanu bëgge mu waye ni. + +Ana nag ku am janq bu mel ni bii cib taar, nangoo ni, joŋee ni, jekke ni, man nee toppatoo, nangu nee jëme kanam, waaje ni ngir lemu ci say bëgg-bëgg, ana ku am ku mel nii, looy xoolati ku sewe nii, ràgge ni, te taaroodi ni? + +Li ma bëgg a wax mooy naka la nu bëgg a bàyyee sunu làkk yii, rawatina wii di wolof, ca nooyam ga, ak nangoom ga, ak gàttam ga ak noppaleem ga, taaram ba, leeram ga, manam gaa leeral ak yaatoom ga, ak ruyu gi mu nangu, naan dangay jëlati weneen di ci sonn ak a sonle, naan day wa gën? Ma ne ñoom ñoo gis loolu man de déet ! + +Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal, waaye ngir doyodig waa Afrig yi ba leegi, frañse mii nga xam ne lu matul 30 cib téeméer ci doomi Senegaal yi rekk a koy wax moo fiy làkk wu njëkk, maanaam wi nguur gi di waxe di ci liggéeye. Moor Taala Baay Faal Mbóoj + +Cosaanam +Ni ko gëstukat yi waxe, làkku wolof am na ag mbokkoo ak yeneen làkki Afrig yu bari, yu mu bokkal i maam. làkk yi dañ leen a séddale ci ay wàll: bu ci nekk ñi am ag mbokkoo lañu fa def. Nee nañu wolof ci wàll gi ñuy woowe bànqaasub atalaas bu làkki Kongóo yu kojug nit ku ñuul la bokk. Am na ag mbokkoo ak pulaar ak séeréer ak joolaa ak yeneen. + +Daanaka ñoo ngi koy làkk ci Senegaal gépp, bëj-gànnaar ba bëj-saalum, penku ba sowwu. +Donte wolof da di làkku askanu ñi ñuy woowe ay wolof, waaye kàllaama wolof amul uw dig. Dem na ba romb dig (frontiere)yu Senegaal àgg ba Gàmbi, Gànnaar ba Mali, ci ñaari dëkk yu njëkk yi sax boole nañu ko ci seen i làkki réew. Daanaka gox boo dem ci Senegaal am nañu waxiinu wolof wu wuute: am na wolofi waalo-waalo, jolof-jolof, saalum-saalum, wu kajoor-kajoor, wu baol-baol ak wu lébu. + +Mbindin +--154.0.180.65 29 Ut 2014 à 00:17 (UTC) +h +h + +Abajada wolof +a - à - aa - b - bb - c - cc - d - dd- e - ee- é - ée - ë - ëe - f- g - gg - h - i - ii - j - jj - k - kk - l - ll- m - mm - mb - mp - n - nn - nc - nd - ng - nj - nk - nq - nt - ñ - ññ - ŋ - ŋŋ - o - oo - ó - óo - p - pp - q - r- rr - s - ss - t - tt - u - uu - w - ww - x - y - yy. + +1- Doonte sax, li ñu téj ci biir lonk yi ngay dégg, nanga bind: xule, bu bëggee, pus, xuloo. + +Xool it + commons:Category:Wolof pronunciation Ngir déglu waxiinu baat yi + wikbaatukaay: ab baatukaay bu matale ci wolof + Xibaaryi.com : Yéglekaay bi njëkk ci làkk wolof + xLingua-Online-Dictionary German-Wolof / Wolof-German + [: ] Yéenekaay gi léppam di wolof tàmbalee ci wolof yam ci wolof + +Wolof +Làkki senegaal +Làkk +Ahmadou Bamba +mooy ki taxawoon jàmmaarlook tubaab yi, ngir xeexal lislaam, te desal fi sunu ag dëkk ci Afrig tey bég cig cosaanoo fi, kon njukéel ko war nanu, kii moy ki taxawal yoonu Murit, tey ki taalif lu sakkan ci diine, indi ay gisiin yu bees, ginaaw bi nu ko sonnalee genne ko ay yoon réewam + +Jiitalug aji firi ji + +Li ma tax a jug, jëme ma ci def bile ligéey, te ma jàppe ko muy bu am njariñ, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, ñi ngi ligéeyal Sëriñ bi, waaye it xeet wi, ndax jël lu mel ni jaar-jaari Sëriñ Tuubaa, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk jot,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dégg , man cee jariñu, ca anam ga mu gën a yombe, gënnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , ñeel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral,lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal Sëriñ bi,waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, ñeel saw làmmiñ, te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gën a dugge,lay gën a tooge,lay gën a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay yaw itam kenn ci moom, ngéen di benn bu dul ñaar, gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe di rawe, di jànge ci seeni làkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo. +Man de bile téere,njëkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lëf ci waxtu,ngir yër ko,dégg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu néew, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu làkk yii,te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi. +Ñaareel bi mooy , gis gi ma gis téere bii,di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ, di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi. +Làmboo nag kem bu bu réy ci xam-xam, ci lu aju ci Sëñ bii, di kenn ci ñi ñu war a xam, bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom . +Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir bañ a guddal, ñoo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenn jëllewaayi yoon wi,yu xam-xam. +Ndax kat, boo yëree, da nga ko gis lu bari mu naan Sëñ bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bëkk-néeg la woon ci bëkk-néeg yi,bu ma waxul ngën ji bëkk-néeg +, kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku ñépp xam ag sellam, akug dëggoom, yal na nu Yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci Sëriñ sunu,Sëriñam,laafaale ko, ci barke ku nu ligéeyalam, ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindéef yi. + +Jiitalig aji taalif ji + +Bii mooy teereb Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di naan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di xam-xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin. +Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal. +Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin. + +Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam. + +Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. +Ndax kat ñooñu, ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan: ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñu,ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey sëlmël ci yonant bi. + +Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBÀKKE Xaadimur rasuul. + +Bi loolu amee ma, bëggoon a leeral as lëf cig dundam, ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. +Waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi, ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñëwee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko. + +Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jéggalul ma Yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem, lu man a wecci loolu ko yéemutoon, ndax téere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dëgg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngënéeli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. +Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee. + +Doggantal gu njëkk gi : ci xamale kuy Sëriñ bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu góor làqoo + +Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax - ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk 1270 g, am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar 1272g,ca kër waajuram wu goor ca Mbakke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. +Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum sharaha,muy 1270g làqu atum shumoos muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant. Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar,ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram)). + +Moom sëriñ bi, bi mu ganee àdduna ,waajuram wu jigeen a ko yoroon ba mu mat a jàngi, Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah doomi Muhammadul kabiir mom Habiiballaah mu njëkk ma doomi Muhammadul Xayri,ak Muhammadul Kabiir . +Muhammadul Kabiir mii mooy ki niy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbàkke Bawal atum 1194 g ,ci li nu wax,waaye dëkkewu ko woon da faa bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata,magi habiibullaah waaye bokkunu nday,moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof, fa la làqqoo nu denci ko fa,di ko siaare. + +Mi ngi askanoo nag ci Tukklóor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof, siw na itam ne ñoom Gànnaar lan bawoo, dem Fuuta,seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay serif lanu.Sama mag, sama sëriñ, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu,mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu. +Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu. + +Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jëm fu nu naan Mbumbe, péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbàkke-Màkke yi dëkke woon. + +Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbàkke-Mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu, kaaf gi nekk ci Mbàkke ag Haa la woon muy haa giy mujj ci ba,wolof yi def ko kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab),li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci nekk, dëgër na te am na màndargaam dëgg. Waaye Buso-boso yi ñoom seen cosaan Fuuta la, ca fa niy wax Golare, barab yii yepp it yu jegee lanu,barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddngay ñaari askan yi. + +Bi Sëriñ bi tollee ci war a jàngi,wayjuram dal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. +Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbàkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi, ju jigéen,ndayi wayjuram wu jigéen,soxna Asta Waalo. Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbàkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal. + +Kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne, sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daa wul tàggalikook moom lu dul lu néew,ndaxte magam Muhammad Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg amaa na mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jiyaadkat boobu di Màbba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Màbba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme Saalum,nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn. + +Bi mu faatoo nag moom Màbba, nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi, ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukklóor KA doomi bàjjani baayam,bi mu jàngee ci moom dali xam-xam,tàmblee ñaw as lëf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono. +Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagéenug seen teddngay nguur gi,li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk,ndax da daa jàng ak a jàngale,te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur,li fi ne daal ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona. + +Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daa na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu génneel ko ci ab yàq,ba mujj sëñ bi far ko raw, mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko,mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali. + +Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). +Bi wayjur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba ,walla ci téere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba, bu ñëwee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci. + +Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala,dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanc ca wetam,tudde ko Mbàkke Kajoor,sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam,nee nanu, looloo ngi am ci Muharram,atum 1300g, dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. + +Bi niy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wàllug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,sëñ Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana Sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àdduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas. + +Ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem, rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara. + +Bu dee mbooloo mi moom, li leen yéem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu Sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme,bu njëkk bi mooy waxam jii: +nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen ba fa mu yam ,teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii: +nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi,kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne)). +((Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine)) +((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal )) +((Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? )) +((Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane )) +((Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul të,te mooy Kiy amal li ko soob )) +((Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir)) +((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amu ma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina )) +((Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon déy ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gàccaal)). + +Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga làqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee. + +Doggantal : ci ni mu nekke woon ginaaw bi waajur wi làqoo (gërëmul yàlla yal na nekk ci ñoom) + +Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang, fu nu ko jëmewul du fa jëm, bi mu làqoo nag,mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp, ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa bàyyi woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi,ak seeni xam-xam,ak beru ak a wër,niki ñu baax ñi,mu leen daa junj ciy waxam,ak a feeñal ay maanaa,ak a yëgg,ba bi ko himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yite) dikalee ,muur ko,mu jug yëgg as lëf neeti tekk,dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu,bi ko mbir mi gënee lëjal nag, gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi. + +Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen yeen mbooloo mi, ku àndoon ak man, ngir jàng rekk,na laxas jëm ca boppam aki mbokkam,mbaa fa ko soob,man loolu rekk taxatumaa jug,ku bëgg li nu bëgg nag,na toog,dal di leen fay bàyyi dugg ca biir. +Waxam jii nag dal di leen bàyyi cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem,sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa,la ca gën a néew des fa. + +Bi loolu lépp daata am,fekkoon Sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal ,yu sariiya yi, mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko,bég ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Dégg naa ci Sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. +Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g,teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla). + +Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne Sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci “Himma” te bu leen yar ci njàng,loolu Sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii: +Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw)) +(( Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel).Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw), mooy ji ci alxuraan: fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi. + +Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindéef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy téere,kon boo may ligéeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.Yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : neel wéeru leen ci man. + +Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab wéeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira,na wéeru ci man. Mu dellu waxaat ne: Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci làq ngën ji ay may. Murid bu Yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na céru ciy may )) +((Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam)) +((Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira. +Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : Jinney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñépp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul. +Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid. + +Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne: + Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax - mooy bàyyi aada, muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam + Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu. +Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : +Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox ko aw yiwam + Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg + Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona. + Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj di ab sëriñam fu mu jublu + Ab sëriñ du wuuteek Ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu + Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba)) + Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam. + +Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wépp yiw: Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru +((Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk )) +((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) +(( Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) +((Képp ku boole yile melo ci murid yi déy,da na jot ndëërlaay ya (gaa yu baax ya). + +Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: +Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi)) +((Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm)) +((Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def)) +((Nettali nanu ne malaakay Aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif + +Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: +Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew +Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,téere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def. +Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yéem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci téere bii,du amati,ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko. + +Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla)) +((Li waral sama tukki bu sori bi,Yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yàlla’a ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne : Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yi ak yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam)). + +Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp,mu ne ci: assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara. +Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca Yàlla, àgg ci Yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manut a ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am déet,du ligéeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war. + +Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligéeyloo,ak ay tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa Yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii. + +Mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat,dajale leen,di leen ligéeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku Yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigéen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul Yàlla, Yalla jënd na ci jullit ñi,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana,Sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn,ba bi mu sancee Mbàkke Bawal,ci at moomu juge Mbàkke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu nekk, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñi ak ñu sori ñi, ñepp di yéemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at. + +Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñi mu siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a woy ay sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Yàlla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir Yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom. + +Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem. + +Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay téeméeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi) ak waxam ja: ( sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Yàlla,yal na ko Yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne déedéet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon. + +Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala da nga koo bàyyi ngir Yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Yàlla,ju mu manatul a bàyyeeti,ndare cib coona,ma jëflante ci ak moom waaye Yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng. + +Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na Sëñ bi Njaaréem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yi ak naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke. + +Bi Sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam-xam bu bari bi ak njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci Yàlla ak yiteem jépp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi. + +Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu,nu tàmbli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoom,lor yi ëpp,mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam, Yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasoo’k ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarloo’k moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jéggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi. + +Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci Sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gañe ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal ak ay jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lanu bàyyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko. + +Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji déggal ko,def ko ànd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,règg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weñ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub. + +Ñu xam ne li mu wax lu dëggu ci moom la, ñu jéggal ko, noppi cim mbiram. Waaye Sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul Sëñ bi bañ,nee nanu ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : neel ki la yonni rus naa malaakay Yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla}}. Dégge naa ci sheex Aadama SÀLL - moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci Sëñ bi , cosaanoo woon Jolof - mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan}},Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi - moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :(( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun)) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,ya’ay weñ wi man nag,ay dem-àll laa. + +Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu bàyyi ko ak mbiram ,ndax kat notante ak moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànji ci toolam - te manu koo bay, manu koo saxal -mu bàyyi ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah. + +Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yi ak coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcc benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkkoon, bi Sëñ bi yëgee ne moom ak Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi, mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : (( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi )). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa nekkoon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi moom taxul,juboo’k moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sunu mbir ma nu ko woowe woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne Sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal ji ñu nangoo ci moom niki màgg ak njaf ña mu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lépp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,Sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waaw,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw, mu ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonnant ? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xaree’k moom,nan lanu koy seedeele ? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, Sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaali ak mbooloo mi ne tekk as lëf,ba mu yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la Yàlla,nga jiitu nu ca,kon ag ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te juboo’k moom. + +Pënd ba wuri,Sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu, yoon yépp dagg ci moom lu dul wi jëm ci Yàlla,ndax kat moo jàkkaarloo ak ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom: wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi}} muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,Yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq. + +Li mooy dooley Sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jéll yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yéeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara génn,te dunu lakk,di yekkati xasiday Sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu bàyyi, ñu leen di door ak a jéng,ak a nangu seen alal,ak a génne seeni kër,loolu lépp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem ak ag sóobu, mu mel ni loolu mbóotum Yàlla’a,mu ball juge ci baatinub seen Sëriñ ba ca ñoom,Sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay Yonnant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nanoo’k lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu Yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,génne leen séeni kër,te loolu téewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca Yàlla, : lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun }},mu leen di xamal ni,danoo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu génne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku Yàlla ak ngërëmam,ak dimbali Yàlla ak ab Yonnantam, ñooñooy ñu dëggu ñi. + +Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day daal di doon lu néew, laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira}}muy :ku gëm Yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonnant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim}} muy dee leen jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. +Dee leen di fuglu yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim muy bis ba niy woo nit ñu nekk ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey Sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanoo’k a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tagg,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy téere bu amul moroom ci tazawuf,yor junni ak juroomi téeméer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom. + +Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanc Daaru Salaam,ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tolloo’k am at,di yar nit ñi,di leen yéege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,dem as lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tolloo’k juroom walla juroom ñaari kilomet,sanc fa Tuubaa,ci mujjug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom,walla ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom benn,tuxu fa ak njaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma - ñaareelu xalifa - ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom Sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos. + +Ku dul Yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalante ak ay xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yi ak jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. +Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dolliku ak a yokku jamono ju nekk, ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca géej ga. + +Doggantal : cig sancam Jolof ak li ko waraloon + +Sëñ baa ngi sanc Jolof - ci li ma sëñ Mbàkke BUSO nettali - bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denc ay soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasoo’k ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligéey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu ,aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji Yonnant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon. + +Kenn ci sunu moroomi naari Daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:Sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii, nu ànd aji,bu neexee Yàlla ,ma dem waaji te lijantiji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun). + +Nu dellu ca wax ju njëkk ja, Sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ci ak man,diisoo’k man ci mbirum ñu sanc ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligéey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd fa ak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. +Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siyaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku warut a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah. + +Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul - bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it, wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li Sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada. + +Waaye Sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom. + +Kon Sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon,te foofee ca la wër Tuubaa amul am ndox,walla bu fa saxee it da na ajowoo jankoote ak ay ñoñam,mbaa mudaaraante ak ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbàkke Baari,wacc fa,sanc fa,waxtaan fa ak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbéenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu dul ay buur,yu ñëw ngir xëccoo’k ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee. + +Waaye Yàlla moom bu bëggee amal am mbir da koy wutal ay sabab, nee nanu bu Yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. +Bokk na ci xéewal yi Yàlla xéewale Sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu wàlliyu yi, sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan }} muy ci maanaa yoonu Yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu Yàlla. Nit du jug mukk jëm ca Yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg Yàlla’a, ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,Yàlla da koy feeñu cig màgg ak cib taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko Yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug Yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen Yàlla di dëddale ak yenn xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bopp,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lépp,hifthul hinaaii du tàggoo’k ñoom,mooy wattu gi leen Yàlla di wattoo’k a aar,dara du leen dal lu dull lu Yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna }} muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan Yàlla jàmm. + +Lii mooy mbirum Sëñ bi ak ay àndandoom ca njëlbéenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom Sëñ Mbàkke BUSO nee na:taalube yi mu bàyyi woon Tuubaa,bi nu yéggee ni Sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax déet, ginaaw mbir mi du mbirum xalaat. + +Bu dee lu aju ci jaraaf yu dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu déggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu tàmbli noo dikkal ci kaw ak suuf. + +Bi buur yi ak seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,danu daan song ku leen daa jéem a të,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donnante,waaye loolu téewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom néeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki néegub sëñ bi. + +Loolu ak meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci Sëñ bi,meneen mbir mi nag , +nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig. +Ci noonu nu jël buur yi ak jaraaf yi teg leen ci kaw daara yi ak donga yi,ñuy seeni njiit,waaye loolu xéewal a ngi ci ndax tax na ba buur yi ak seen jikko yu bon yi nu yoroon, di sonnal jullit ñi ak a fitnaal ak a def li leen soob ci nit ñi jeex. + +Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexe ak ay wor. +Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kiliftéef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galag, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wut ay ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu , +walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop. + +Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàq dunu dañ,di yàq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def. + +Loolu moo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañu koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkulóor la bu defoon ay xare ci wàll gi mu dëkke woon , +ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmad Sheexu dib Tukkulóor,moom it,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi. + +Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen ne Sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu li nu leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi Sëñ bi,ginaaw bi ko Yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax Sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,Yàlla’ay seere lii nuy wax. + +Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma la ak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonnant bi ji (j.y.m), ñi Yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonnant yi,teg ci wàlliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp}} ,ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonnant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis : àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar,yàlla itam wax ne : wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin}} muy àllaaxira, ñu ragal Yàlla ñee ko moom. + +Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum Sëñ bi, ñu tàmbli fa’a yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonnant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngéen li nu leen waxoon am déet ? . + +Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu néew,bunu leen tollalee’k li nu am ciy xarekat,ndax matunu woon mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi. + +Doggantal : ci tukkib géej gi + +Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul Yàlla ak Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida: ku nu tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru,}}, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g. +Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn daje ak ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak Sëñ bi kerook la, ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja - am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal , +danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag Sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,jenn waay ju yor ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,Sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te déggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara. + +Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu Yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: ginaaw bi nu dajee’k ña génnoon jëm ca këram,te njàqare nekk ci seeni dënn)) +((Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla )) +((Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siyaare )) +((Mu jubale kanaman ca Yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg )) +((Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu)) +((Jaraaf ja génn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xéewal.}} + +Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,Sëñ bi nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaaréem. + +Sëñ bi nee na: (( Omar mii mi ngi génn,ngir siyaaresi ma,daje ak soldaar siy génn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye Yàlla moom xam na la nekk foofa)). +Sëñ bi nee na ((nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu déglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon, ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrànkeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir,looloo taxoon mu wird aayay wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina}}muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu génne la, ñu nekk di fexe,Yàlla itam di fexe,te Yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :((Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel lanu woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonnal ca daanaka-dun ba bépp (daanaka-dun mooy Presqu’ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrànkeel ma, ñooña Yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat)). Sëñ bi wax na ci loolu lii: +Yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono)) +((Mu tàbbal ci seeni xol,ag génne ko,jëme ko ca réew yu sori ya,mu ame fa lu kawe déggub Saariya}} + +Yàlla (t.s) dëggal na ba mu naan wal laahu xayrul maakiriin}}muy yàlla’ay ki dàq a fexe. Ndax xéewale na ma ñatt yu gën seen ñatti kuréel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dëgg-dëggi sëriñ,ci gëm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy ñàkk a nelaw guddi) ,te ñàkk ko, ñu may jam ay xeej a ma ko gënal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gëm Yàlla gi nga xam ne mooy dëgg-dëggi xam Yàlla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wér la ne li nga nekk ay dëgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy àgg ca Yàlla mu kawe mi, ñatti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasoo’k ñoom,te loolu moo daa doon sababu rékki gëm,yal nanu ci yàlla musal. + +Ab nettali bu yéemee ngii ma, dégge ko ci Sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te yoroon woon mbirum tukkib Sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :(( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu génne ko,tumbrànkeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu génne Sëñ bi tumbrànkeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,loolu moo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma Sëñ bii fi yaw,bu ko jéem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yéene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca . + +Loolu moo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lépp mujj yomb. Bi Yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penku bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci génn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu ngàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ . Mbirum noonam boobu,niroo’k lool,mbirum noonub ki miy ligéeyal di Yonnant bi (j.y.m),noonam booba di woon Haamir doomi Tufayli,ba mu nee jamono ja ko tawat ja sonnalee ci génn këru jenn jigeen ju Salool: (ndax lii day am mbas mu mel ne mu giléem , te di ag dee ci néegub jigéeni Salool ?). + +Sëñ bi def na ag xasida,gu mu tënke arafi mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw }} ne; +tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, te mu damm)) +((Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi)) +((Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci nekk,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko)) +((Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci géej gi ak ci jéeri ji,te am mbooloom wor ko }}. + +Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,moo’k mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal Sëñ bi ak a saboote,fu mu masa’a daje ak moom,moo nekkoon Garambasaa. + +Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakaaru,ki ci des,di ku géej gi,nekk Konaakiri,yal na nu Yàlla musal ak jullit ñépp,ci nattu bi mu leen tegoon. + +Nu dellu ci mbirum tukki bi,Sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy Inna wàlliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin}} muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy Yàlla mi wàcce téere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolu mooy maanaam waxam jii: +Yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi). + +Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli fa’a woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, Sëñ baa ngi wax ci loolu: ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt. + +Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali - ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn ngélamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu ko woon a jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:Sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe? bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: +laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca’akug xat te di ko muñ +Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji. +Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii: +(kuy sukkandiku ci ndimbalul Yonnant bi,bu koy gaynde fekkoon cib àll it wedam) +(Moom Yonnant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan moo’k am mbooloo ànd ngir,màggam ga )). +Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa. + +Nettali nanu ne Sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,Sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lòtt,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma Yàlla du lòtt te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy Yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara. wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii,}} muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (Yàlla mu sell mi dëgal na,Yonnant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jòttalee). + +Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku Sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) nee na wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lòtt ci sama mbir,bu mu lòtt ci sama sunna}},Sëñ bi moom dònn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,Jibriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan. + +Sëñ bi Yonnant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu Yonnant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi hasbunaal laahu wa nihmal wakiil}}muy ci maanaa Yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la. +Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma Yonnant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor. + +Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : maa ngi sant ki ma musal ci lori jépp saytaane ak jinne ak nit)) +((Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi)) +((Maa ngi sàkku ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju nekk)) +((Yéene naa koo ñaan di sàkku am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu)) +((Mooy Ahmad,sangub mbindéef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom)) +((Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xëccoo)) +((Ya’a moom mbindéef yi ,yaw sama boroom,may ma ag mucc ci ñoom,ak bépp balaa ak mbugal)) +((Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal)) +((May ma li ma bëgg ci adduna ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àdduna ak gu allaaxira)) +((Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma)) +((Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo)) +((Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb Yonnant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef)) +((Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon)) +((Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lépp lu ko man a jublu ciy mbugal)) +((Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax)) +((Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jépp fitna)) +((Fegal ma loxol way bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge)) +((Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gàccaal,ci àdduna ak àllaaxira,te dee ma jéggal)) +((Bindalal Yonnant bi ag xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax.}} +Mu tëje ko fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim}}: muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xéewalug Yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul Yàlla te Yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li). + +Mu neeti alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina}} muy ci maanaa : ( maa ngi sant Yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu Yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na Yàlla,miy boroom mbindéef yi) . +Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,Yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo. + +Mu wax: allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam}}muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne Yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom. + +Waxees na ma ,te loolu lu wér la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi Sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii: +(( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee). + +Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk Sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul Sëñ bi, mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug Sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal Yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite. + +Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum waafiris sitri,di junni ak ñaat téeméer ak fukk ak juroom ñatt,bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal képp ku ko daa jéem a lor,téere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabéey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee. + +Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at ak ay weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,jooy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci géej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko Sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yéeme,gi nga xam ne Sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te Sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: +maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi (waa Ahlu Badri),bi may dox (bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp) laa )) +((Sama dox bi may def, ci wommatug Yonnant bi, ànd ci ak gaa yu baax yi,Yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul Yàlla)) +(( Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa Yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man )) +((Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju nekk mi ngi may sottil ay xéewalam ) te mooy ki di ab santaakon (ku soxlaalul kenn) )) +((Sama ndimbal,samag dëgëral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci Aji yaatu,ji di ab Mayewaakon,(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama )) +((Sama kilifa nag, ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraan,di Yonnant bi,te mooy ki may ligéeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal)) +((Samab yool ci ligéey bi may defal Ku nu tànn ki,di Yonnant bi, mayewaakon (Yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la)) +((Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligéeyal gën ji mbindéef,te moom Yonnant bi mooy samab xuppkat (Yonnant bi day bashiir tey naziir,di kuy bégale tey xuppe ngir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ) )) +((Aji feg jii di Yàlla,moo may fegal ci Yonnant bi,ayi noon yi,ak lépp lu ñaaw te mooy ki may xettali)) +((Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligéeyal Yonnant bi,mbiri mbindéef yépp nag ca Yàlla lay mujj )) +(( Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub Yàlla,te moom siw na )) +((Samay sutura ci adduna ak allaaxira,mooy tagg Yonnant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la )) +Samaw jiwu mooy téereb Yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu (muy saytaane) )) +((Samay kër wéet na, ñoñ ñi tas,ngir tagg Ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat )) +((Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la}}. + +Sëñ bi nee na +Ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu Sëñ ba’a ngi ciy wax naan: Yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde)) +((Ñu àndandoo, sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari}}. +Ma sax fa - sëñ beey wax - la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci la’a dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen bàyyi leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu. + +Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku wéet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caagéenug aw wéttal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ? +Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!. +Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci Yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àdduna yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bopp,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna. + +Ca bis ba ma war a juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa, ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,Sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn. + +Bi Sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub Yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant Yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. +Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci Yonnant bi (j.y.m) ki may ligéeyal,sama dënn leer,sama xol dal,kóolute gi dolliku ci Yàlla’ak Yonnant bi,ndax alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub }} ci tudd Yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale. + +Sama gudd gi daal di neex ci Yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan: +Yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wépp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe ) bi xëccoon jëme ci man)) +((Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye Yonnat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu )) + +Doggantal : ci dugg gi ci gaal gi juge Ndakaaru + +Bi nu xëyee - sëñ beey wax - muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal nanu ma ca digg gaal ga,di jooy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,Sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: +Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini Yonant bi )) +((Gaal gu fees googu ak mbooloo, yendu na fanaan )) +((Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga )) +((Murid ba tàggoo, dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari}}. + +Mu jublu ci muritam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñépp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,Sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba mu far jël daam ak xalimaam,nee na, bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbindéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi. + +Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saa sa, ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjëlati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag, nga xam ni moo’k nit ñépp a yam,dara waru ko lu dul mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko. + +Ci loolu mi ngi naan: +Ki njiit li yonni woon ca ligéeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu )) +((Ginaaw bi aji ligéey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal)) +((Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la Yàlla di wonee aw yoon}}. + +Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) ((wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca Yàlla te Yàlla’a ngi gis jaam yi. +maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi. + +Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,Sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa dégg ñu ne ya’a ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma. +Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul Yàlla,ku jublu ci ku dul Yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul Yàlla,ku jublu ci Yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad Yonnantab Yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne Yonnant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem. + +Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye Yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul génne ci ab néeg ne ma,ndax ya’ay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak a màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gaal gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: +sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi)) +((Yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lépp luy xëcce jëme ci yu nu sib )) +((Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma}}. + +Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,leeral gi mu ko leeraloon maanaam laa ilaaha illal laa,waaye du àddiyay alal ja ko waa ja jox,moom waa jooju nga xam ni bu ko Sëñ bi leeralutoon loolu mu alku,te Yàlla gindee na ko ci leeral gi. Mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yéeme gi ko Yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yeréem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi téeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñépp walla ña ca ëpp,ci loolu la Sëñ bi naan: +kiy jagleele yërmaandeem di Yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle}}. + +Mu jublu woon ci aji yërëme jooju Yàlla mii di boroomi xéewal,daa ko indil ay xéewal,bokk na ci xéewal yooyu biteeli misk yooyu. Mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li ko dal,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ . Mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne Yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe .Mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñépp ba kerook muy wàcc Gabong. + +Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mjje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci Yàlla ak Yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug géejug dun boobu laa taxawoon di joriku, di xutba géej gi naan: +yaw géej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd )) +((Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal Yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,bob sopp na ko}} + +Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal Yonnant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fépp. + +Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yépp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saa sa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne : yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun}}muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmëx ab loxoom bëmëx gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lépp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tolloo’k waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrànkeel ak a génne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daataa wàcc,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,loolu moo waraloon sama ñëw gii du leneen. + +Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu bég ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah. + +Da na rafet fii ma indil leen fi bayiti ki def Xawaariq muy Ibnu Hanbal: +( Bari na aji jalgati (tooñkat) ju sol yérey teddngaam,di puukarewu ,sol ab tëneem aki takkaayam) +(ay junniy junni nekk ci ron kiliftéefam,te faalewul ku koy digal mbaa mu koy tere)) +(ngeen (Sëñ bi lay waxal) wàcce ko ci mbartalum toraxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) ) +( muy ndimbal lu tukkee ca Yàlla ñeel jaamam bii di ligéeyal Yonant bi,nga xam ne soldaari nasaraan si ci la nu mujje mokk ba mel ni ay ansaaram,(ansaar mooy ku lay jàppale ak a dimbale) ) +( cey bu tuddoon sekkare bi, kon dey mbindéef yi yéemu,waaye moom ab dënnam bàmmeelub ay mbóot la). + +Nee na bokk na ci karaama ( mooy xarbaax ak kiimaan yi Yàlla di defal aw wàlliyu) yi ko Yàlla defaloon ci géej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat bi mu nekkee ci benn ci dun yi,dañu koo yobb woon ca karce ga,dëkkal ko fa soldaar sa,nee na ma mel fa ni kenn ca ñoom,ñuy tux ak a naan ak a fo ci sama wet, man may muñ seeni lor rekk,ndax man xam naa ne mukallaf mu ne am na ñaari malaaka yu ko seq,di bind ay jëfam,ginaaw ñaari malaaka yooyu ñoo man a muñ,man a dékku li ñiy dajeel ciy lor,ngir topp seen boroom,kon du jaadu ci man may jàmbat,ndax ñoom kat li leen di naqari rekk moo may naqari,li leen di mettee may metti,te ñoom du ñu jàmbat. +Ci noonu Yàlla dogal soldaar si genn bis di tàggatu ji ,ba ñu demee fañuy tàggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas, kaalawu, sappewu (rang),soldaar si dal di tiit ,taxaw,ci noonu seen njiit li tëyye leen,gëdd leen ne da leen di ray bu ñu siiwalee xibaar bi. Bi suba jotee ba leer,mbooloo mi waroon fas yi ne mes,soldaar si dem ne miik,bañ a nettali dara. Sëñ bi nee na bi loolu tegee ay fan,aakim bi (goornoor bi) woo ko nooy-nooylu ci kanamam,wax ak moom wax ju nooy,ci biir wax ji mu ne ko: xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali ci li nga bëgg? +Ma ne ko ñooñu moom ay nit lanu walla ay jinne? Mu ne ma yaa ko gën a xam ! Man ma won ko ne xamuma dara ci li miy wax,mu dal di noppi. +Am na ci boroom xam-xam yi ku ko ci laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi,Sëñ bi ne ko :ngir tiital noon yi. Keneen laaj ko ne ko ñooña ñooy niti Ahlu Badrin ña walla malaaka ya?,mu ne ko malaaka ya .Am ku neeti ko ndax yonnant (j.y.m) bi ca la woon? +Mu ne ko moo doonoon seen njiit,daal di ciy wax wax jii:<< ki nga xam ni wommatal na ma la fàddu woon wëliif bepp wàlliyu,jàppndalal na ma mebat yepp fa dëkk ba niy wax Limbarwali >> +<< ka soril rambaaj ba ak ku inaañ ka ,wommatal na ma waa Badar ña diy sang>> +<< Yàlla da na ma wommatal begleg laa illaaha illallaa fu ma man a ne >> . +Ku baax ki nee na li mu bëgg a wax ci bayit yooyu mooy: li fàddu woon weliif bepp wàlliyu,mooy feeñug waa Badar ànd ak seen kilifa ga (j.y.m) ca pàkk yu lëndam yooya ca geej ga,ngir jàjji ay noonam.Begleg laa ilaaha illallaa,mi ngi ci jubloo wax aaya bi sun boroom di wax (( wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda lifaddlihii)) muy ci maanaa bu la Yàlla bëggalee aw yiw amul ku ko man a tëyye. Fu mu waxe nex-nexi walla lori laa illaahaillal laa,mi ngi ci jublu waxi Yàlla ji mu naan:(( wa in yamsaskal laahu bi durrin falaa kaasifa lahoo illaa huwa )) muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak aw ay amul ku ko man a dindi ku dul moom. + +Mu ne bis teg nanu ko ci mbedd mu xat,dal di joyal aw nag ci kawam,tàmblee seetaan,yaakaar ne agsi na ci sama kaw ba noppi,waaye bi mu ma jegee daa daal di jekki-jekki rekk naaw mel ne daa am ay laaf. Nag wii mooy wi Abdu Laahi Saalim Ibnu Anbal doon tudd ci Xawaariq bi mu naan: ( ab xiik (xiik mooy xale bu jigeen bu masul a sëy,fii mu jublu ci nag wu toll ci war a sëy ) ci nagi kër yi,muy naaw ci jàww ji ba kenn gisatu ko). + +Mu ne mas naa am mu yàgg ci benn barab ba foofa soof ko,mu tàmbli di jàmbat,waaye nee na daa jàmbat rekk Yàlla sotti ko yamb yu soxot te bari,ñu koy màtt ak a sonnal,mu ne bi mu xamee ne li ko dal moo ko teg boppam,ndax kat ((wamaa asaabakum min musiibatin fa bimaa kasabat aydiikum)) muy musiba mu leen dal yeen a ko teg seen bopp,bi loolu amee mu ne ma soppi samag jàmbat def ko ag cant,daal di ne: +(( nasaxal naa sama njàmbat def ko ag cant,dootuma jàmbat ci moom lenn lor,ndax sama lor naaxsaay na)). Ci noonu nee na yamb ya dem wëlif ma ,ma tàmblee noppalu,xam naa ne yamb yooyu la ki def xawaariq jublu woon bi mu naan: +( ay yamb yu toll ne ay mburtu (mbate) yu suur cig réy, cam si (cam si mooy waa ji,mu jublu ci Sen bi) daje na ak ñoom,te faalewul seeni lor ). + +Mu waxaat ne waa jooju doon nasaraan-nasaraanlu te nu tuddoon ko ca ginaaw,bis def na ko lu ñaaw ba yenn xaritam yi yedd ko ci,xupp ko ba mu tiit, reccu,ca guddi googa nag mu ñëw ànd ak ku koy wommatal ab gàtt,moom mu yor benn biteelub daa bu mag ci loxoom,dal di tedd tàllalu ci sama kanam,nee waay day tuub,te ne du jug fi mu tëdd mukk,li feek teguma sama ndëggul tànk cig doqam,ngir tuub,ma fexe ba jële ko fa ci wax ju rafet rekk,mi ngi ma fekkoon nag may bind ca jamono jooja,ma dal di def bayit wii ca saa sa: +4(( Yàlla nooyalal na ma ci guddi gii xolub boroomug tubbi ga,ginaaw bi mu ma indilee ab gàtt ak daa , ( ngir tuube ko ) )). + +Ku baax ki tudd na ba tay yeneen karaama yu ko yàlla defal ci gèej gi,mu ne da fa mas a dëkk ak benn doxalkat (goornoor) bu soxot,bu kenn dul jege te bagul dara ci lu baax,ma wax bis ne jiyaar jii may def ci yoonu Yàlla daal di naa ko seet tay ci mbirum àttekat bii,ma xool nu ma ko Yàlla di tàggatale, ci noonu ma juge sama néeg dal di dëgmal këram,ñu ne ko sëriñ ba dey a nga jemsi ci yaw, mu ne aah loolu de lu jomb la,ndax danu daa sàkku ci moom muy bañ,kon tay naka la fiy dikke ci coobareem,ñu ne ko amul benn sikk ci ne kee di dikk de moom la,mu dal di jug ci saa si daje ak man fu sori,bég ci man mbégte mu kawe,ci noonu mu ànd ak man ca barabub boppam ba,dal di ne ma loo bëgg, loo bëgg cig baamu ? Wax ko ay yoon, man itam ma ne patt, rekk di xool lu ma koy wax,ba yàgg ma ni ko,da maa bëgg as lëf ci daa, mu dal di may jox bitéel bu mag bu fees ak daa,ma daal di ne wëlbat won ko ginaaw,booba fekkoon na ma may bind ak xasida gu ñu tënke arafi a b t th j (mooy abajada rekk) ,ba ma àggee ca arafu faa,ma bind ca bayit wii ne: sama xalima texe na fa ab aat (mooy ku xaraful)bu weddi Yàlla,kok tàggat naa ko ci xul huwal laahu ahad. + +Ma bindaat ay bayit,yoy dañu maa wax ni ma lii de ag wor la, ndax yaa ngi bàyyi yéefar yi ci anam gu dog,ba noppi ngay jël ci ñoom di nëbb,ma dal di bàyyi la ma doon def,gas am pax ba mu xoot ,ma sotti ca daa ja,suul,dal di xam ni sama jiyaar ji dëggu na, ma sant Yàlla . + +Nee na itam,benn janqu ndar-ndar,dafa gént gis Waa-Badar,ci bis yooyu nu dugg dëkk ba, tàmblee ray waa dëkk ba,bi nu demee ba kenn ci ñoom jege ndaw si,jenn moroom ji ne ko soxna soosu de ab jullit la,mu dal di koy bàyyi. Sëriñ bi nee na xale bu jigéen boobu ku baax la woon,daan sonn ci moom ci li mu am,daan ko wax naan man dey lu ma la jox rekk xamal ne maa ko ñaq ci sama loxo,njëgug sàngara nekku ci du caagéenug gu poon,loolu da koo leeral foofu ndax kat foofa ci ñaar yooyu lañu daa jëflantee,te moom xam na ne man du ma leen jëfandikoo te du ma jëfandikoo seenug njëkk,ma laaj ko bis ne ko loo bëgg ci lii nga may defal?,mu ne ma bu dee ci àdduna ,sët yu baax,bu dee allaaxira àjjana, ma ne ko Yàlla man na lu nekk. + +Yàggul tuuti rekk,Yàlla dogal mu ëmb,te daawul ëmb,bi diirub ëmbam matee rekk mu dal di wësin,dal di faatoo ci wësin wi,ma jullee ko,masu ma koo gis it mukk,ndare bi ma taxawee di ko jullee,ndax sunug jëflante mi ngi doon ame cig yonneente (correspondence). Nee nanu doomi Daba SEY la woon tuddoon Aamina (Ami),boroom këram tuddoon Yèlli SEY,bokkoon ci ndawi goornoor yu mag yi,di woon it ku baax te daan sonn ci man. + +Am na bis mu jote ak àttekat bi (goornoor bi) jote gu tàng,ngir sama jëmm ji,loolu nag ni mu ame woon mooy daa am bis ma wutoon ñeenti bant teg leen ci sama buntu néeg ngir def ko ab julliwaay ngir ñiy romb bañ di ci jaar,bi ko àttekat bi gisee ,daa dal di jug,falang jàkka ji buddi bant yi,sànni leen,ne fii amul julli amul lislaam,da nga ñoo bëgg a yàqqal sunu soldaar yi,ma ne miik,bi ko Yèlli SEY yëgee te tubaab bi demagul,daa dal di jug ca saa sa,jawalsi ànd ak aw meram , ne ko lu tax nga tas jàkkaam ji,te moom defu ko fu dul ci buntu këram?, sakkul yoon wi te xatalul kenn it. Tubaab bi ne ko man daal maa ko def,fii jàkka du fi am,Yèlli ne ko waaye man di naa ko defaraatal jàkkaam ji na mu meloon,tubaab bi ne ko du fi ame, ñuy bëgg a doorante nit ñi dox seen diggante, ñu nekk di xuloo diggante tàkkusaan ba jant so,ci biir loolu lépp man maa ngi bind. + +Ci xisa bii (nettali bii)laa binde xasidag ((Rabbanaa axrijnaa min haazihil xarya azzaalimi ahluhaa wajhal lanaa min ladunka walliyan wajhal lanaa min ladunka naziiran) muy ci maanaa yaw sunu boroom génne ñu ci dëkk bii nga xam ne ñi fi dëkk ay tooñkat lañu te nga wutal ñu aji méngoo ju tukke fi yaw,te wutal ñu aji dimbalee,xasida gee nekk nii: +(( gërëm naa kilifa gu màgg gii nga xam ne yar na samab xol te koomal ma, moom dey mooy boroom bi gën a tedd)) ba bi mu àggee ci : +(( bindal ko(moom Yonnant bi) ag xéewal ak ag mucc ak ñoñam aki saabaam te nga def sama jàkka ji ci darajaam (moom Yonnant bi) muy lu yaatu )) + +Bi mu àggee foofu ñu ne ko nangul nanu la ko,da nga ko gis. Loolu nag gis nanu ko,mooy jàkkay Jurbel ak Tuubaa ,xasida gi nag gu gudd la te rafet gu am jeexiit gu réy ci jañ ak ñoddi bu soobe Yàlla ak ci barkeb aji defam,ku koy jëfandikoo na ragal Yàlla te xemmeem aw yiwam. + +Yàlla dogal na bis Yèlli moomu siyaaresi ko Njaaréem,juge ca yooyale wàll,ginaaw bi jumaa ji noppee muy ju Njaaréem,Sëñ bi ne ma ma’ak sama jenn waay ànd leen ak moom mu siyaare jàkka ji,ñu ànd ak moom, won ko jàkka jépp,penkook sowwu,biir ak biti,mu yéemu gépp yéemu,bi nu dëppee Sëñ bi ne ko noo gise jàkka jii ak sama jàkka joojee,yaw mi ma doon xeexal ak a dàkku?,mu ne subhaanal laah maneesu leen a tollale,Sëñ bi ne lii mooy maanaam sama wax jii: +(( Yàlla dàq na jëme ca ku dul man ca Maayomba la naqari woon sama xol te yékkati samag wàll)). La naqari woon sama xol bu nu koy firi mooy tas gi nu tasoon jàkkaam ja,yekkati samag wàll mu jublu ci yekkatikug soorool yi. + +Ab nettali bu yéemee ngii bu làmboo ay karaamay Señ bi: Señ bi nee na bi tubaab bi buddee bantam yooyu,sànni leen,kenn ci gaa yi bégoon ci jëfi tubaab bi, da cee jëloon ab bant samp ko ci wanag wi miy sangoo ak a doxe aajo,waaye Yàlla nattoo ko benn bis mu bëgg a tuur ndox,jawali ca satala ga te booba satala ga ndox mu tàng a ca nekk te moom yëgu ko,te seetu ko it,waaye bi mu noppee ba sotti ko ca cér ba (sàkkara sa) da wadd ca kaw ni ab baa bu góor bu tiit,dal di yuuxu ba fa baatam yam, ne: Señ bi dimbali ma alku naa de,dal di sànni satala ga ca àll ba,dikk teg loxo ba ca tubay ja,ma ne lu deesi defati lu dul muñ ak wax (( innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun)). + +Mu neeti - moom ku tedd ki - ne am na at mom bu doonul woon li ko Yàlla tawfeexal saa su xamee ni weer tàmbali na mu di ko bind,kon wenn weeru ramadaan doon na jàll te du ko xam,ndax waa dëkk boobee mu nekkoon xamunu woon lu dul weeru tubaab wi,bi korite gi jotee ma xëy, dog ,sangu, def li ci sunna digale,ma génn ne damay julli ji ca pencum dëkk ba,ba ma àggee, ma xool sowwu ak penku,xoolati sama ndijoor ak cammooñ,ànd ak am kóolute ci ne kenn du ñëw,am ñaari jèbbéer (jèbbeer mooy jaam bu jigéen) yu agsi war a toll ci baalix ( baalix mooy ati génn ag ndaw) taxaw sama kanam di ma seetaan,ma kàbbar ñu tàmbalee xàqataay,saa su ma kàbbaree nu ree,naka noonu su ma jàngee,ba ma sëlmal def samab xut ba, sama déeyaale gi maa ngi ciy wax:(( yaw buur bi, xam nga ni woor naa weeru ramadaan ni nga ko digalee,ma dog ,sangu,julli ni nga ko digalee,waaye dey lu ma génnee muurum koor laa amul,bu ma ko amoon it,ku ma ko jox laa dul am,kon jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sang,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam ,te nga nangul ma lépp lu ma man te def ko ci sa ndigal yi,te nga bindal ma yoolub li ma manul lòtt ci,te amoon ci yeene walla yu ni mel. + +Bi ma noppee def xasida gii: yaw buur bi jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sàng ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam te nga def qaafiya bii di ñëw,mu kawe miimiya ba ,ci lu feeñ ak lu nëbb,aamiin yaarabal haalamiin ci barkeb Yonnant bi (j.y.m) : +((maa ngi yaakaar ci aji yaatu ju dëggu ji,ci darajay ki niy xeeñtu di Yonnat biy dimbali dëgg ci dëgg (j.y.m) )) +(( maa ngi yaakaar ci Yàlla moomu delluwaat ci samay mbokk ci lu gaaw ànd ak njub gu dëggu)) +(( ak nekk jaam bu texe bu nu matal, tey ligeeyal jaamub Yàlla miy dëgg,jaamam boobu di yonnant bi mu tànn)) +(( yaw Yàlla ci darajay ku nu tànn ki ak ñoñam,yal na nga ma jéggal te nekkal ma te wommat ma te goreel ma)) +(( di naa la gërëmloo ci Alxuraan ak sunna si nga xam ne,Yonnant bi yoonalal nanu ko,yaw miy aji teqale lu taqaloo)) +(( yal na nga ma tàggatal noon yepp ba fàww,te fegal ma ag bokkaale,yaw aji not jiy boroom tijji ak tëj)) +yal na nga ma wommat delloo ma Daaru Salaam gi nga xam ne fa laay deyaaleek yaw ciy aaya,te yal na nga kaweel ci man ay gox)) +(( yaw sunu boroom yal na nga ma dello ci lu gaaw te defal ma samay mébat yepp,te nga may defal ay mbégte te di am ñeewant ci ma)) +(( te nga may ma ay xam-xam yu jariñ jëmm ji ak mbidéef yi,te nga dolli ag yaatal gog texeel lay doon ak ubbi ak xar-baax)) +(( sama bakkan déy daa bañ ag yéwénal,ndax ab noon la,kon sellalal ma ko cig taxañ (taxañ Señ bi mi ngi ciy jublu lu gaaw) yaw miy ngën ji kuy yéegale )) +((na nga ma may ba fàww li ma bëgg ci mbindéef yépp, te nga fegal ma séenuw ay yaw miy joxe ag jiitu )) +(( màngal ma samay mébat fii ak fa nu jëm,te nga may ma ngënéel lu màgg te saxalal ma ngënéel li)) +(( yaw sama boroom fegal ma li ma ragal ca bisub njàqare ba,te nga defal ma jéggi siraat gu gaaw gu mel ni melax )) +(( musal ma ci (ay nocciku = nusuuh) ak lépp lu nit ñiy ragal te nga def ma may ku sori ag lakk)) +(( nangul sama ñaan gii yaw sama boroom,te nga faral ma samay ayib ,te nga seere ne man dey tuub naa ci jepp jëf ju di jëfi dof)) +(( te nga nekkal ma yaw sama boroom,te musal ma,te amal sama yaakaar,te fegal ma luy bijji ag nëx )) +(( nangul ma sama ñaan gii,yaw mi moom lepp, te nga tabe ñeel ma cig yaatal ak dëddu ak dëggu )) +((ci darajay Yonnant bu nu tànn bi,te nga fegal ma hisaab ci darajaam,te tàggatal ma ci moom kepp ku di boroomug kàccoor)) +(( na nga julli te sëlmël ci moom Yonnant bi,ak ñoñam aki saabaam,yaw mi moom penkook sowwu)). + +Mu nettali ci karaamay géej gi,ne : am na jenn waay ju bokkoon ci kilifay barab bi ma nekkoon,da maa digoon ab bitéelu misk ci lu dul ma di ko sàkku ci moom,ndax man daawu ma sàkku ci ñoom lenn,te daawu ma sentu ci ñoom,daawu ma wóolu seeni dig it,waa jooju ma digoon bitéelu misk bi,ndekete daa digoon keneen ci moroomam yi lu mel ni li mu ma digoon,waaye bi mu deful li mu digewoon ,waa ja daa tàmbali di xuloo ak moom ak a ngaayoo,moom itam muy dàkku boppam,(di defandar boppam) loolu lepp it mi ngi doon ame ci sama wet,ci wolof it lañu doon waxe waaye yu leerul dara,waaye làkk gi nu koy làkk li muy leeradi leeradi fàttali na ma réew ma, ba mel ne da maa ñibbi far ,ngir gëj gi ma ko gëj a dégg,loola neex ma lool. + +Waaye xuloo bi nu def te li ko waraloon lepp mooy wóolu gi mu ko wóolu woon,ak dig gi mu ko dig te defu ko,loolu lepp ma sant ci Yàlla,mi ma defal may kok wóoluwu ma kenn,sentuwu ma ci kenn ku dul moom,loolu tax ma def xasidag cànt gii, ma wax ne: + +Maa ngi tàmblee samay wax aki bjëf ci turu Yàlla miy boroom yërmaande ju yaatu ji ak ji miy jàgleele, xeewal ak mucc yal na nekk ci sunu sang,Muhaddad ak ñoñam aki saabaam.Miimiya bii moom la ñeel yal na ko Yàlla gërëm. Yaw sama boroom sama noon yiy say noon,sànni nanu ma ci géej gi,ni nu sànnee woon sa xarit ba Ibraahima ca sawara wa,nga waxoon ak moom (sawara wa) ci :(( yaanaaru koonii bardan wa salaaman halaa ibraahima )) muy yaw sawara wi doonal ab sedd ak jàmm ci Ibraahiima. +Sawara wa dal di mujj di àjjana ci moom,jàmm ak xeewal yal na nekk ci moom ak ci mbooleem nabiyu yi ak yonnant yi, +Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw aji dund ji! Yaw aji taxaw ji ! Ci darajay weeru ramadaan mi nga wàcce Alxuraan, mu dig jub ñeel nit ñi, te di ay aaya yu leer yu di ag njub ak ag teqale dëgg ag safaan,ci barkeb xut ba bii tàggatal ma géej gii ak ñoñam ak mbooleem samay noon yiy sa yos,te nga bégal jullit yu góor yi ak yu jigéen yi ci ñu gis ma te dajeek man,te dégg sama ag dellu ca Daaru Salaam,ak Tuubaa ci lu gaaw ci lu dul ab coona du caagéenug ag sabablu gu tukkee ci man,Aamiin yaw boroom mbindéef yi, ci darajaam moom Yonnant bi,(j.y.m) te nga def miimiya bii mu kawe li ma jortoon,ni nga ko baaxoo defe ak man ca la ma waxoon njëkk bii,te nga defal ma ko muy ab yobbal,tey pakk tey àjjana ci ñaari kër yi,aamiin yaarabal haalamiin. + +(( man déy maa ngi tagg,tey sant ngën ji aji xéewale, te du ma jàmbat ñàkki xéewal ci menn mbindéef )) +((kepp ku ma jorte ci sama tumburànke gii may kuy toroxlu ci kenn ku dul aji doyluloo jiy aji yaatu (muy Yàlla) na ko wóor ne moom ku gumba la )) +(( moom de laay jàmbat samag lòtt ,samag ñàkk ak samag tumburànke,may yaakaar samag dellu ci lu gaaw di ngën ji ku nu xeewale )) +(( jàmbat naa ko samag lòtt,mu fajal ma ko,te nekkal ma ci lu kawe sama njort,moom kat mooy gën jaa teddi kuy terale )) +(( ñi nga xam ne weddi gi nu weddi Yàlla da leen a wor danoo jublu woon samag wàll,mu aar ma ci ñoom dàkku jepp aji tooñ)) +(( ag cant ñeel na ko tukkee fi man,di yaakaar ci moom sama càkkutéef lii,ci lu dul ab coona buy juge ci man,te sama naqar dañ na )) +(( ki njort wor ba muy iñaan, bu ma woree tam,na ko wóor ne ki ma wommat cig teral de woru ma)) +(( ku ma sànni ci géej gi ngir ag weddi di boroomug mbañeel,na ko wóor ne ci géej gii de tabeg aji terle ji dikkal na ma fi )) +(( koo xam ne li ko naqari mooy nekk gi ma nekk di jaamub Yàlla,tey jëwrini aji rammu jiy ku nu jiital )) +(( na ko wóor ne man de ab jaamam laa ci géej gi ak ci jéeri ji,di ligéeyal kiy musale ci luy waral reccu)) +(( ku ma dëddu de na xam ne xéewal yi jublusi nanu,juge ci aji yaatu jiy aji doyluloo,kiy aji wattu tey aji jiital )) +(( ku ma sànni ci géej gi ngir sàkku samag tumburànke,na xam ne ag tàggat ñeel na ma tukkee fa sama boroom ci gépp géej )) +(( samag wéeru ñeel na Yàlla ci samag teew ak samag fàdd,te di naa jàmbat jëm ci moom jaarale ko ci Yonnant bi,moom miy samab raas (bi may yéege jém ca Yàlla) ndaw muy ku baax )) +(( yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom ak ci ñoñam aki saabaam ak bepp jullit )) +(( yaw sama boroom saxalal ba fàww ngën jaa selli julli ak sëlmël ci Muhammad)) +(( ak ñoñam aki saabaam yepp,te nga delloo ma Tuubaa ci lu gaaw,te peek ma te xamal ma)) +(( yaw sunu boroom man de warlu naa ba fàww di kuy ligéeyal Yonnant bi,tey kuy ligeeyal aaya yi,na nga ma xamal te déggal ma )) +((yaw sama boroom,maa ngi sàkku ci aji maye ji ag géeju akug wuññi akug yinkiiwal (ag sol xam-xam mu tukkee fa Yàlla) na nga ma wuññil te yinkiiwal ma )) +(( jublu naa aji ubbi ji tey sàkku ag ubbeem,di yaakaar ci moom ay may yuy ball,ndax ag ballam day yol di sotti)) +((gërëm naa aji not ji bi mu ma tàggatalee noon yi,ma doonoon ku tumburànke,di ku wéet fa ñoom di ku amoon gépp lëmmu)) +(( di naa ko gërëmloo ci Alxuraan ngir sant ko ci xéewalam yi,ci sama xol ak sama yaram ak sama gimiñ )) +(( war na ma ma saxal li mu ma tànnal mu dig jub,te ma koy gërëmloo ci aaya yi ndax ñoom kat (aaya yi) mujj nañu di samam màng (ngañaay) )) +samay cant aki ngërëm aki tagg ñeel na aji jariñe joj indil na ma Alxuraan ju tedd ju ñu màggal)) +(( moom (Alxuraan) mooy ndàmm mi (koom mi) tey leer gu fés gi niy aar ci sawara ak noon yi ak gàcca)) +(( ab teere la bu tedd,juge ci aji tedd juy terale,jëm ci jaam bu tedd,buy xettalee tey boroom yërmaande)) +((teere bu darajawu la juge ci ku darajawu,ku darajawu te wóor indi ko, jéme ko ci aji darajawu kuy matal )) +(( xéewal ak jàmm ci lu dul dog yal nanu nekk ci moom,ak ñoñam aki saabaam fu mu man a nekk)) +(( jàmm ak xéewal yal nunu sax ci moom li feek aji sant a ngi naan : da ma ne maa ngi sant ngën ji aji xéewale)) +(( Xéewal yal na sax ci moom juge ci aji tedd ji may nekkal,te du ma jàmbat ñàkk ay xéewal ci menn mbindéef)) +(( mucc yal na nekk ci moom juge ci moom (Yàlla),(mucc) gog da nga ma ci fegal (yaw Yàlla) aw ay, te aar ci samag wàll wëlif ku nu rëbb ki (muy ibliis) ak ku gumba)) +((xéewal yal na sax ci moom tukkee fa moom(Yàlla),li feek ku koy jàmbati mbiram a ngi am la mu bëgg di gën ji ku nu xéewale)) +((aki ñoñ aki saaba yoy maa ngi ñaan aji kawe ji mu dugal ma ca seen biir ëlëg may boroomug xéewu )). + +Bokk na ci karaamay géej gi ba tay nettaleem bii,mu ne: bis xëy na, waaj ngir ligéeyal Yonnant bi - ni mu ko baaxoo woon - amul lu dul aw mettit wu tar daj mbooleem yaram wi,ba manatul li mu bëggoon ,waaye am benn tubaab ci njiiti nguur gi,mi ngi dëkkoon ci wetu fi Sëñ bi dëkkoon,nekkoon di xaqataay ca kaw aki moroomam,Sëñ bi daa di ne:Yàlla yaw de xam nga li ma waajoon jëm,ak li ma ci gàllankoor,maa ngi lay ñaan nga tuxal lii fi man te yobb ko ci ki lay wutal moroom,amul lu dul ma dégg waa ji doon xaqataay muy onk,man may bind. + +Bokk na ci karaamay géej gi ba tay lii: bis nee na fi mu nekkoon ndawal da faa mànke woon lool,ba jën yu ndaw yi nuy def ci poti weñ yi rekk lanuy lekk daanaka (xam naa mooy poti ton yi) ma jëfandiku ci bis,bi ma noppee ma raxasu ba sonn,jëfandikoo suuf ak saabu ak lu nu man a dindee ag xet rekk,waaye dara,ba ma ca manatul dara ba ne naa dem nag jublooti ca ligéey ba,bi ma tàmbalee rekk ñu ne ma ((wa minhumul laziina yuuzuunan nabiiya)) muy am na ci ñoom ñuy lor Yonnant bi,ma tiit lool, jaaxlee jaaxle,ca saa sa ma bàyyi koo jëfandikoo,doxe ca bàyyi luy jën,boole ko ci li ma jaayante ne du ma ko lekkati,bis bi ma ko bàyyee walla lu ko jege,ay kuy dikkal nanu ma,juge ci fere yi,di njëg gu nu gaawal ci jën yi ma jaayante woon. + +Mu neeti moom ku baax ki:dëkk bi mu nekkoon da faa nekkoon aki làbbe ñuy jël ci xaley yéefari nit ñu ñuul ñi nekkoon foofu di leen def ay mbindaan,di ànd ak ñoom di wër ci ja yi (marse)ginaaw tàkkusaan,njiit li nekkoon foofu defe woon ne da maa xemmeemoon ci gone yi mu ne ma woon boo ci soxlaa de ma joxla ci ñuy ànd ak yaw,ma ne ko soxlwu ma ci. Njiiti dëkk booba itam baaxoo woon nanu di jël ci magi nit ñu ñuul ñi, ñu ñuy def ay toggkat aki rootkat,ma sàkku kenn ci ñoom bis ngir ligéeyloo ko,waaye ba mu ma jegee daal xeeñal na la ko xeeñ goo xam ne amul gu ni mel,ma ne kii daal sobe na ba maneesul a jaxasoo ak moom,ca noona ma jaayante ci seeni ndaw ak seeni mag ni ma jaayantee ci jën yu mag yi ak yu ndaw yi ,ci loolu mu ne: + +(( ma ne njëgug ndaw ñi dikk na ak gu mag ñi ak ndaw ñi)) +((Muhammad gën ji imaam mooy sama dëkkandoo,ag bëbbam de (dexam) ci sama xol lay sottiku jëm)) . + +Fere yi ñëwoon indi kuy yi (xar mu goor mu mag) ñooy mosalug njëgi yéefar yu mag yeek yu ndaw yi,kuy yooyu it di mosalug njëgi jën yu ndaw yi ak yu mag yi. + +Bokk na ci karaamaam yi ci géej gi ba tay waxam jii mu ne: +bi ma xoolee sama diggante ak noon yi ,nooni Yàlla yi,ma xam ne ñoom kat am nanu kàttan ci lor ma ak gaañ ma,ci dogalub Yàlla bi ak’ug nammeelam,ma xam it ne bu doonutoon kaaraangey Yàlla ji ak’ug fegam kon ba tay waxatunu ko,laa leen bàyyi ak seen bëgg-bëgg,jublu sunu boroom,mi yor mbir yi,ma déeyaale ak moom ci sama mbir: +ma ne ko Yàlla yaw’ay ki nu bind ngir nu jaamu la,nga ne ((wa maa xalaqtul jinna wal insa illa liyahbudoonii)) muy bindu ma nit ak jinne ndare ngir ñu jaamu ma,nga neeti : (( yaa ayyuhan naasu uhbudoo ràbbakum)) muy yeen nit ñi jaamu leen seen boroom,bu ko defee tawfeex ñeel ki texe jiitu ci moom,mu dégg wax ji topp ko,naka noonu toroxte ñeel ki ag texeedi jiitu ci moom,mu lànk bañ a wuyyu,tëx, luu, ngir’ug weddi,man nga tawfeexal ma,def ma ci mbooloom ñi wuyyu,mbooloom Yonnant bi Muhammad (j.y.m) imaami anbiyaawu yi ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom ñepp,nga dolleeti ma ngënéel,def ma may jëwrini Yonnat bi tey xalifaam ci diineem ak xeetam,am mbooloo ci sa noon yi, noonam yi,jug song ma ngir dox sama diggante ak jaamu la,te ligéeyal ko (moom Yonnant bi) . Ñoom dey ñi ngii di ñu caaxaanadi ci seeni jëf,di ñuy farlu ci seeni neen,te yaw yaay ki wax ci làmmiñu sa Yonnant bi,lol maanaa mi mooy:nit ku nekk daa am kër ca àjjana ak ca sawara,bu duggee àjjana ñu won ko këram ga woon ca sawara,ne ko fee de nga jëmoon boo jaamuwutoon sa boroom,leegi nga xam ne daa nara gént,ab yéefar a koy donn. Bu tàbbee sawara’at nu won ko barab ba mu doon am ca àjjana,bu jaamu woon Yàlla,ginaaw nag jaamuwul boroomam ba tàbbi sawara,leegi ab jullit lanu koy jox. Ginaaw mbir yi nii lanu deme,te noon yii - ni nga ko xame - ci tooñ ma lanu dëkk ak a def ci man lu leen soob,te du ma fayyu te du ma leen ñaanal aw ay,waaye maa ngi lay ñaan seen kër ya ca àjjana,Yàlla nangul ma ko,may ma leen,ba ma xamee ne maa leen moom,ma jox leen àddiya waa-Ahlu Badrin . Ci loolu mi ngi naan: + +(( jox naa àddiya këri noon ya nekk àjjana mi kuy jalgati dul dugg,ñeel saabay Yonnat bi)) +((kër yooya de jëlees na leen ca noon ya,jox leen saaba yu baax ya)) +(( Yàlla jox na ma kër ya fa samag tumburànke,teeyal it samab xol)) +(( man nag def naa leen ay àddiya ñeel saaba yi,yal na leen Yàlla gëram ,moom mi ma aar wëlif (sahaab:ay niir ) )). + +Na nga xam ne karaamay tukkib géej ji moom maneesu leen a jeexal,bu ma bëggoon a indi li ma ci xam ci lu juge fu wóor ,ak li ma ci dégg ci nit ñi,kon dey ma indi fi lu yéem xel yi,te kon du xaj ci teere sii di su nu gàttal,looloo tax ma yam ci li nga xam ne topp naa ko ba mu wóor. + +Mu ne ati tumburànkeem gi juroom ñatti at yu mànke tuuti la,bi mu matalee li ko Yàlla bindaloon cig tumburànke,ci suufus yéefar yu ñuul yi,Yàlla indeeti ko ca suufam ngir nitam ñi ñoom itam jariñu ci moom ci li ko Yàlla may ciy mbóot ci tukkeem bu barkeel boobu,ak ngir mu daje ak mbokki jullitam yu baax yooyu di naar yi,ci noonu Yàlla dal di def ci xoli kilifay nguur gi ñu am ag ñeewant ci moom delloosi ko. + +Doggantal : ci ñibbisig Sëñ bi ci jéeri ji,juge ca géej ga + +Sëñ baa ngi àgsi Ndakaaru bisub gàww juroom benni fann ci sahbaan,atum kasasin di 1120 g, mu wéye fa, jàll Ndar def fa lu tolloo’k fukki fan ak juroom ba ca bis bu njëkk ba ci ramdaan, mu doonoon bisub talaata,mu juge fa,dem Luga, wàcc ca rakam ja Sheex Coro MBAKKE,ca guddig gàwwu ba, mu rañaane fa romb kër Sheex Jull SIISE,jugeeti fa jaar kër muridam ba sëriñ Sire LOO, yoor-yoorug dibéer ja ca Sànnoosi, mu sax fa la desoon ca ramadaan ja,noppalu fa,woor fa. + +Ci diir bii,foofa fees na dell,raj-rajloo ba mel fa nu mu masul a mel,ci diggante ay taalubeem ak kuy sàkku ndimbal,aki kilifa yu koy siyaaresi,di ko ndokkeelsi,bokk na ca ñooña ka nuy wooye (kiimaanug jamonoom,woykatub waxtoom) Sheex Ibraahima JOOP Almasharii,ab xisaam lu xoromu la te yéeme,ag wuññi (feeñal mooy wuññi) gu yéeme feeñ na ci ñeel Sëñ bi (maanaam Sëñ bi wone na ci ay xar baax) loolu mooy sheex Ibraahima moomu daa amoon ab bor bu mag bu ko lëjëloon lool,ci jamono joj fay ko ci jafe na,mu jug wër ak moom ci sëriñ su mag si waaye taxul kenn tëyye ci loxoom,ci noonu mu jaaxle lool te am tiis,waaye bi Sëñ bi agsee Sànnoosi,mu ñëw indaale ay bayitam tudd ci mbirum bor bi ak ni mu ko seddalee ci diggante Yonnant bi(j.y.m) ak ñeenti saabaam yi,ginaaw sëriñ si nanguwunu koo xettali. + +Bi mu yëgloo Sëñ bi ne ko mu agsi,mu dikk,nuyyoo,bi mu daataa wax ay mbiram ak boram bi ak ni mu ko seddalee ci bayit yi,Sëñ bi ne ko indil ma mbuus mee,mu indi ko,mu neeti ko jox ma mi ci des ,mu jox ko ko,mu ne ko waññal li nekk ci mbuus mu nekk,mu waññ ko, muus mu ne ñatti téeméer nekk ci,boo leen boolee ñuy juroom benni téeméer,Sëñ bi ne ko indi benn téeméer bi te jël li ci des dimbandikoo ko ci say soxla,te moom boram bi juroomi téeméer rekk la woon,ca saa sa sheex Ibraahima daanu ab jéll,yuuxu ca kaw,Sëñ bi ne ko waaw yaw lu mu? Mu nettali ko xisaam,jàngal ko bayit yi,moo nekk nii: +((bori ay mbokk war na ma,ma seddale leen ci diggante ñu tedd ñi ndax ñu fay leen)) +( yaw Ku nu tànn ki(Yonnant bi), ya’ay ki moom cér bu njëkk bi,yaw su xarit bi (Aboobakar) ya’ay ki moom ñaareelu xaaj bi) +( yaw ki teqale dëgg ak fen (Omar) ya’ay boroom ñatteel bi, yaw sunu Usmaan mi, nga moom bi ci topp) +( yaw gayndeg xarekat yi,yaw baayi Asan ak Usaynu ñiy leerug sunu diine ji,yaw laa feetale li ci des) +(yeen de ñu tedd ngeen ñoñ kuy jàmbati coona du wéeru ci seen daraja te fajalu leen ko ko) +( kon gën jaa selli xèewali Yàlla na sottiku ci yeen,li feek Yàlla a ngi faje ay soxla ci yeen). + +Sëñ bi yéemu lool te sant Yàlla,waaye noon yi ñoom seen kiñaan gi mayu leen sax ñu xaar ba Sëñ bi ñibbi këram,waaye danoo dal di tàmbalee wut seeni pexe,di lal seeni yoon, di waajal li nu nar,di xaar waxtoom jot banu def ko. + +Ku baax ki moom bi mu jullee iid ca bisub kori ga,mu doonoon bisub alximis,da fa’a toogaat bisub àjjuma ak gàwwu ba ca tàkkusaan sa,mu laxase fa romb ca kër taalubeem ba Koor Mag JOOB,boole fa timis ak gee,ngir tarug dox ba,dem Màkka Sàmba JOOB fanaan fa,xëy bisub dibéer dem kër baay tëxam Sheex Ibraahima MBAKKE Kajoor,laxasati ca tàkkusaanug altine ba, dem ca Masàmba Xari JOOB,moom mi ngi kër Muxtaar,fanaan fa, yendu fa,jugeeti fa ngoonug talaata dem ca Muxtaar Mareema Silla ca Ñaxal,mu def fay fan,juge fa jàll Kokki Guy ca Maxtaar Masàmba JOOB,yendu fa waaye fanaanu fa,da faa juge njëkk jant biy so,te booba ña ngay waajal ñam yi,waaye taxul mu xaar ko fa,dox nag jëm Daaru Salaam këram,àgg fa guddig àllarba ci lu tolloo’k ñaar fukk ak benn,Siidi Muxtaar ,rakam ja booba ma nga fa woon,ca biir sawaal. + +Rakk ji (Sheex Anta) tàmbli di ko ganalee lol kenn ci murid yu mag, yu man yi sax manu ko,waxantu ma la’ak ñu néew ñi doole. +Mu sax fa diirub fukki fan,bis bu nekk ñu ray ay fukki yëkk,bu ko matalul mottali ko ci giléem walla ay giléem,kem li mu mànke rekk.Ñu koy waajal ay wàccuwaay ca rakk ja sheex Ibraahima,diggante Tuubaa ak Daaru Salaam,muy fa Sëñ bi tudde woon Daarul Mannaan, mu dem fa moom ku baax ki ci njëlbéenug silqihda . + +Sheex Ibraayma mii moom jërul ngay laaj ay mbiram, mooy ki ku baax ki dénkoon njaboot gi ak bagaas yi,bi miy tukki. Ci noonu màgi taalube yépp daje fa,Sheex Ahmadu Ndumbe jiite leen,mooy ki doon dem ak a dikk,di yee ñi gëmméentu,di jàngal goney Sëriñ bi ba nu mokkal ci diir bu néew njëkk ku baax kiy dellusi,dara yàquwul ci mbirum Sëñ bi,ba ñépp daan ko léebe ci wàllug jub ak tegu ci yoon. + +Mu jullee foofa iid (tëbëski),sax ci meloom wu sell wa ak yareem (tarbiya) ga mu nekkoon,mbiram ak mu dongaam yi di gën a jëm kaw . Kawe fopp,fopp,fopp na mu meloon,kaamil yi ñu leen di jàng di leen xool ci bëcëg gi ,di leen tari ci gudd gi,naka noonu xasaayit yi,ak njàngalem xam-xam mi,ak ligéey bi ,loolu lépp àgg fof maneesu koo melal cig kawe. + +Ni nga xame ne mbirum ku baax ki yokk na ak mu taalube yi ba jéggi ab dayo,ba maneesu koo misaal,naka noonu mbirum ñu iñaan ñiy rambaaj. Mbirum jaxase gi dellu fa mu nekkoon,rambaaj yi jug di def seeni ligéey ba nu xëy indil Sëñ bi ay soldaar,li ko waral mooy: jaraaf ji nu dénkoon mbirum wàll googa,ca jooja jamono,- moom xam nanu turam ak giir gi mu bokk - waaye bëggu ma koo tudd di nëxal ay doomi baay tëxam,ak doonte àndunu woon ak moom ci yéeneem ak jëfam ak waxam,waaye ginaaw seen doomi baay tëx la,rafetatul nu leen koy tuddal,te doy na ne ñi teew moom xam nanu ko ci tur,ci jëmm ak ci mbokk,te yal na Yàlla musal ñi teewul ñuy xam turam. + +Moom de moo waxoon te tegu ko woon fenn ne : Sëñ bi day dajale ay kano aki fital ak yeneen jumtukaayi xare,te mi ngi waaj fi mu nekk,bu ngeen ma joxoon ay soldaar de kon ngeen gis li may def. Ñu àndoon ak moom ci kaw waaye wóoluwunu woon ay waxam,looloo waraloon ñu boole woon ko ak buuri réew mi mépp,buurub Kajoor,bu Bawal,bu Siin,waaye bu Siin a ci gënoon a rafet njort ci Sëñ bi,gënoon cee rafeti wax,waa-waaw xamal nanu ma ne am na ay buur yoy seen biir de Sëñ bi la àndal. + +Am nanu xam-xam ci ne bi nu àgsee waa juy rëy-rëylu ji méngoo woon rëyam nga (al lazii tawallaa kibrahuu) moo dal di woon tàmbali di dog sàkket yeek jaaseem ji, te daawul xaar ku ko ubbil bunt,lépp lu dox ci kanamam mu dog,te amul lenn lu muy rus,dale ko ca sowwu ba, ba ca penku ba. + +Fekkoon na Buur Siin - ci li nu wax - mu wutoon ay fuglukat (controlleurs) indi fa ngir ragal ñuy dugg cib néeg di fa duggal ay ngànnaay walla fital te kenn du ko yëg,ngir dëggale ci li nu waxoon ne Sëñ bi day dajale ay ngànnaay,waaye Yàlla dogal loolu amul,bu nu ko bëggoon it du man a am,ndax donga yi doonte danoo bank seeni loxo,teewul ñi ngi ànd ak ñoom ci ay bët ak ay xoolkat. Bi nga xamee ne gisu ñu lenn ci li nu doon tuumaal sëriñ bi,te gisunu ci donga yi kenn ku yor kanam gu lëndëm mbaa gu ñëkk,ku ñu ci gis rekk ma nga mel ne kuy waaj a julliji kori mbaa tëbëski,ngir tuwaaletu bu rëy,ñu xam ne noon bi day fen,buur yépp rus,am kersa ku ci dul waa ju fettéerlu ji,moom sax gàccawu na waaye daa suturloo jàmbaar-jàmbaarlu ak sàkku-sàkkulu nu ganaleel ko buur yi,ak xontal ko fas yi,waaye lu mu soxla rekk nu defal ko ko ca na mu gën a gaawe,gënnee yombe,ci noonu ñu dellu di ñu reccu,yal na Yàlla fay ña ca amoon yéene yu rafet. + +Ag karaamaa ngi nii: +bi sodaar si laataa agsi ay mbokkam moom Sëñ bi danu koo wër lëjël ko witt,gën a tar ci moom ay jiit,tiit gi nu tiitoon taxoon amatunu woon kersa,taraloon lool ak moom,demoon ba bëgg koo génn seen biir bu nu ko manoon,ña ca bokkutoon ca mbokk ya daal mooy ña ca yaroo ca moom,waaye ku baax ki moom loolu lépp téewul mu doonoon ku féex ku ko yëgalutoon yaramam,naan leen bég leen,wallaahi mbir mii ñaari bëy dunu ci daanate,waaye kuy dégg loolu ? Ñoom ñii nga xam ne tiitaange gi yobb na leen ca dayo ba moos. +Ca bis yooya ku baax ki génneel leen aw dagiit wu yéeme ciy woy,ne leen bu ngeen ko jàngee ci kanamu soldaar si du ngeen dégg lu leen naqari mbaa ngeen koy gis,moom nag ñi ngi ko toftalee ci arafi (Rahmaan Rahiim)(muy boroom yérmaande ju nu yaatal ji,ak boroom yérmaande ju nu jagleele ji) moo nekk nii: + +(( sama boroom de bettee na ci luy leeral xel yi,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)) +(( samag cant ñeel boroom bu tedd,bu amul bokkaale,sama dënn it tay fees na dell ak leer guy jolli)) +(( Muhammad ,xéewali sunu boroom yi ba fàww yal na nekk ci moom,sama lépp de ci moom la ko watoo )) +((maa ngi ñaan sama boroom, moom mi ay mayam matale mbooleem mbindéef yi, la mu tànn moom mi binde )) +((déeyaale naa ak moom - moom de màgg na - ay at , mu teral ma teralug aji gindee,sama lépp it set na ciy caaxaan)) +(( yaw boroom yérmaande ju matale ji,mayal mbooleem mbindéef yi yërmaandey ka nga xam ne ku jàng Alxuraanam ji,mu feg la wëlis aw ay)) +(( aaral xeetu Mustafaa wi ci gépp yàqute,te nga yërëm mbindéef yi,yaw mi bindoon seen maam)) +((yaw boroom nguur gi ,yaw mi màgg wëlif fayyoontoo, yërëmal mbooleem mbindéef yi,yaw aji gindi joy dimblee na))) +((far nga la xol ba jublu woon ciy lor,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)). + +Sama mbokk Muhammad doomi Aliyu Alyahxuubiyu,nu gënoon koo xame ci turu Muhammad Tuubaa,ngir taqoo gi mu defoon ak ku baax ki ca Tuubaa,ak baril lu mu daa sikar,ak a jàng xasida yi,xibaar na ma ne bi Sëñ bi génnee xasida gi (Rabbii bimaa yashrahul),da ne ma mokkal ko, ma mokkal ko ba nu daataa ñëw,bi nu ñëwee mu woo ma ne ma jàng ko ca kaw,biral ko,ma jàng ko ni kuy nodd,baamu ko lu tolloo’k ñatti yoon,mu ne ma doy na ,mbir mi mat na te yéwan. + +Mu daan def fu mu nee ma dajewunoo’k lu nu naqari de,ma ne ko xasida gi -ci karaamay ku baax ki- def na ci soldaari Tuubaa yi la picciy Abaabiila yi defoon ca soldaari Màkka ya,ngir sunu Yonnant bi (j.y.m),waaye ñii ak ñee li leen wuutale, ñii dañiy ñoñ ay nu jëflanteek ñoom ci kem seeni yéene,naaxsaayal leen,ñee ña ca ëpp di ñu baax,ñu ga (forse) leen ,te seeni xol Sëñ bi la àndal, Yàlla yeexal seeni mbir ba nu bari tuub ci,ba ca ka leen jiite woon,moom it tuuboon na,ñenn nit ñaa ngi sikk ay mbiram nag,bi nu xamee ne lòtt doo nga tuub du tuub. +Sëriñ bi nee na : +((dëgg-dëggi tuub mooy nga bàyyi bàkkaar boo mas a def ngir Yàlla)) +(( ci sa coobarey bopp,waxunu lu mel ni (lu la Yàlla teg) niki tëx ak jàngoroy pëy ak gumba ak luu)) +((nga bàyyi ko rekk ngir màggal ku màgg ki,ak ragal mbugalam mu metti mi)). + +Man nag li may wax mooy lu man a xew ci mbooloom Sëñ bi la ,moo xam daa lòtt walla daa tuub,mbari na lu Yàlla jéggal ku tooñ te tuub,bàyyi ko ak Yàlla daal a gën a wóor, rafet njort ci moom itam a gën a mat,Yàlla nee na : ((fa man jaa ahuu mawhizatun min rabbihii fantahaa fa lahuu maa salafa mamruhuu ilal laahi)) muy ku ag waar dikkal juge ca boroomam,mu bàyyi la mu doon def,la mu jiital ñeel na ko,te mbiram moom ma nga ca yàlla. +Bi soldaar si demee,ci la génne ci ndigalul Yàlla ak Yonnantam ci ñaareelu tukkeemba,ma nga ca naan: + +(( ku jorte ne sama dox ba ginaaw atum aksasin di 1321g,moo’k sama dox bi ci bopp jaysasin di 1313g ñoo yam)) +(( sax na ne aji réer ju dof la ,ndax moom dox boobu teeyal (neexal) gu aji kawe ji di teeyal samag dund la)) +(( saama doxub aksasin bi du lu dul yoolub ki ma wommatal ci ginaaw bi dëël (dig) bob def na ko)). + +Doggantal : ci ñaareelu fàddu gi (tukki fii) dem Gànnaar + +Ci bisub gàwwu,fukk ak juroom ñaar ci weeru gàmmu atum aksasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak benn,la Sëñ bi génne ca këram ga ca Daarul Mannaan,ginaaw bi ko ay bataaxel dikkalee aki ndaw tukkee ca nguur ga,naan ko na leen fekk Ndar ginaaw tisbaar. Mu fanaan Ngaabu ak njiitul soldaar si,xëy dem Njaaréem ,juge fa dem Tool,juge fa jàll Tiwaawon,foofa la yéege saxaar dem Luga,ware fa gaal dem Dagana,loolu lépp ci ag ayu bis,sax fa juroomi guddi,jéggee fa dex ga juge Dagana ginaaw bi, ci ñaar fukklu fan ci weeru gàmmu ànd ak waayi Sheex Siidiya Baaba ji,mooy Sheexunaa Ibnu DAADA,man na’a am li waraloon loolu di woon li nu wax ne Sheex Siidiya’a ko wax muy ne leen sëriñ bii de amul lenn lu ñaaw lu deesi ragal ci moom. Ñu ne ko woon ndax man nga noo wóoral (gaaraantil) li nga wax? Mu ne leen warlul naa leen ko,ñu ne woon ko kon leegi danu koy boole ak yaw. + +Sëñ bi moom daawu leen yeexal lu dul diggante bi muy xaare ndigal lu juge ca boroomam ak sangam ba,loolu moo daan waral ñuy jort ne daa lànk,te fekk booba noonu la deme,ci noonu mu dem ànd ak Sheex Siidiya,ba nu àgg ci yenn ci kër yi nga xam ne du nu woon këram,waaye yu Banii Daymaan lanu,mu wàcc fa ngir ay mbir ci digganteem ak yenn giir yi,bu ko defee ku baax ki wàcc moom itam,bu niy laxas mu laxasati def ko ay yoon. + +Bi tuxu yi baree nag ak màngaan mi ci wenn weer walla ñaar,nga xam ne daanaka dunu sax fi barab,te loolu wuute na’ak lool aaday waa réewam,loolu tiis ko sonnal ko ak ag njabootam,te itam taalubeem yi danu koy dikkal fu mu man a nekk te barab yi sori nanu,sàcc yi bari ci yoon yi sonnal leen it ya yooni yoon,ci noonu ku tedd ki sàkku ci ñoom ñu tàggoo,ñu bañ ngir xér ci ànd ak moom,ak ngir yilla ju jiitu ji muy dénk gi ko ko nguur gi dénkoon . + +Waaye Sëñ bi moom dogu rekk,nu xam ne ku dëggu la,te du sàkku dara ci bànneexu bakanam,nu ànd ak moom ci li mu bëgg,nangul ko ngàntam,moom itam mu jàmmante ak ñoom ci aw bayit wu yàgg:( bu ñu nu tànnloo woon de du ma tàggoo’k yeen, waaye ag tànn àndul ak jamono ),Sëñ bi ginaaw lii du bayitu boppam mu soppi waaye ag tànn àndul ak jamono,def ko waaye ag tànn àndul ak am ñax,jublu ci loolu yéen da ngéen di sàkku fu ngéen di sàmme ak fu ngéen ko man a ame,loola reeloo leen. + +At mooma mu woore Sarsaara koor ga,muy barab bu nu xam fa ñoñam,nit ñi sottiku fa,ak ñuy jële ci moom rawati na ci Banii Daymaan ak seen kilifa ya,doomi Baydah yi Abdul Laahi aki mbokkam ci loolu ku baax kaa ngi naan: +(( mbooleem sama xeeti cant ñeel na ki nga xam ne sama lépp ci moom mujj na di ngërëm lu àndul ak ab sàññ(mer), ñeel ko fa Sarsaara)) +(( moo moom sama tagg ak sama ngërëm ci lu dul sàññ,bi mu ma wommatalee ay ansaar yu bokk ci Banii Daymaan)) +((sama lépp ñeel na Yàlla fa teeni teraanga,yu nu tuxoo,te bari na fa ñu siyaaresi)) +((ñi nga xam ne danoo dikkoon Sarsaara ngir siyaaresi ma fa,na nu xam ne tàggoo nanu aki bàkkaar àdduna ak alaaxira)). + +Ci Sarsaara gii nee na daje na fa’ak Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu,du ciy gént,mu jox ko Wirdul Maaxuuz .Fekkoon na njëkk loolu Sang Bu nu Wóolu bi dikkaloon ko ca géej ga,rékki (jël)woon ca moom lépp lu mu jële woon ci nit ñi,ba deseetu ci dara,mu jox ko wirduw Xaadir,ba ca mujjug tuxal ga nga xam ne loolu day tegtale ne daje na ak Yonnant bi (j.y.m) ca géej ga,Jibriil dikkal ko fa mooy Sang Bu Nu Wóolu bi,rékki woon ci moom la mu ca rekki woon,joxoon ko la mu ko joxoon,jaarale ko ci Yonnant bi (j.y.m). + +Mas naa teew bis kenn ci boroom xam-xami naar yi laaj ko kuy Sang Bu Nu Wóolu bi ? Mu ne ko Jibriil,mu ne ko ndax Jibriil dees na ko gis ginaaw Yonnant bi ? ku tedd ki tontoo ko ñaari bayiti ki woy Xazawaat : + +(nee nanu Jibriil da na teewal kiy faatu te gëm,aw nit it weddi nanu ag dikkam ginaaw Yonnant bi (j.y.m), dëgg gi nag mooy amul ab dayo (ag dikkam) ) . + +Sëñ bi neeti ko waaye wax jii am na ñu ko tax a jug,ñooy ñi ci am ag ñam akug dëggal,waa ju juge fee rekk nag li war mooy mu nangu ko mbaa mu noppi,ngir bañ a loru. + +Man nag ma ne misaalum loolu mooy lu mel ne ku nu digal mu taal ab taal ngir aajo ju wér,mu taal ko,ab lëpaalëp jaar fa tàbbi ca,dee,kon kooku dara waru ko ca dee googu,naka noonu ku nu digal mu wax, bu waxee.Ma ne wàlliyu yi di gis malaaka yi moom kenn manu koo weddi, ndax jële naa ci mbindum sunu sëriñ Xalifa Alhaaji Muhammadul Faadil,moom mu jële ko ci yenn ci teere yu mag (majaamih) yu wér yi lol ab yaxam mooy ku ñu ubbi (maftuuh halayhi) moo xam ab nabiyu la walla wàlliyu,manul a ñàkk mu jàkkarloo’k malaaka,ci seeni jëmm,ni ñu mel,tey wax ak ñoom ñuy wax ak moom,képp ku ne wàlliyu du gis malaaka tey wax ak moom kon na xam ne tegtalub loolu mooy moom du ku nu ubbi,lii nag mooy layuw ku nangu(féeñug Jibriil),ci ku ko nanguwul. + +Ginaaw Jibriil da na dikkal aji gëmm ji buy faatu,te ku ñu ubbi day gis malaaka yi tey wax ak ñoom,te yinkiiwalug wàlliyu yi (sol gi nu leen di sol xam-xam ak li Yàlla di bëgg ci ñoom) mi ngi am jaare ci malaaka walla mu am ci lu dul muy jaar ci kenn,ginaaw loolu lépp am na,kon du jomb ci Jibriil moom mi Yàlla wóolu ci wëhyoom gi,mu nekk ag diggale (intermédiaire) ci yobb ak joxe yinkiiwal gi Yàlla di dsotti ci ñenn ci wàlliyoom yu mag yi,ginaaw ñoom ñooy ñiy dònn yonnant yi. + +Moom Jibriil dimbali na sunu sang ba Hassan saaba bi (y.y.g)ci teewaayu Yonnant bi (j.y.m),mu di ag kiimaanam tey karaama ñeel aw wàlliyoom,luy tee kon mu man a dimbali ligéeykatam bii ci ginaawam,mu dig kiimaan gu ñëw ci ginaaw bi tey karaamay wàlliyoom wu dikk ci ginaawam te di ko ligéeyal ni ko Hassan,wàlliyoom wu njëkk wa doon defe. Ñoom ñaar de ay mbokk lanu ci lgéey bi,ba fa tuxal ga xam. +Du ñàkk ñariñ ñu indi tuxal gi ba ngéen gis ko,mi ngi nii:da ne yal na ko Yàlla mu màgg mi gëram : bu dee bunt bi yor wirduw aji nos ji (aji woy ji) moom doggantal nekku ci ,(doggantal= français =chapitre,araab=faslun) aji nos ji ,wird wi mu njëkk a jël ci wird yi mooy wu Xaadir,ginaaw bi wu Shaazaliya,ginaaw bi wu Tiijaan. + +Bu dee wirduw Xaadir moom jëfandikoo na ko lu yàgg,daan ci sàkku ndigal ci képp ku mu mas a yaakaar ne ku nu ci jiital ga (muxaddam), ba jële woon ko ci ñu bari. Ginaaw bi mu wóor ko ne ñi mu daa jële du ñu ci woon ay muxaddam maanaam ñu ñu jiital (ñu ko war a joxe) ,mu sàkku ci Yàlla (t.s) mu may ko ci lol ag gëlëm mbaa ag dengi-dengi dootu ci nekk. Mu ne bi ma Yàlla yobboo ci géej gi ma nekk man rekk ak moom la ma Sang Bu Nu Wóolu bi dikkal (j.y.m),dal di rékkee ci man lépp li ma jële woon ci nit ñi ba dara desatu ci,mu jox ma Xaadiriya ci diggaleg (jaarale ko ci) Yonnant bi (j.y.m). Tuxal gii ak lu ni mel ci mbidd yi, danuy wone ne Sëriñ bi daje na ak Yonnant bi(j.y.m) ak Jibriil (j.y.m) ci lu dul woote ag yonnant,du caangéenug wëhyu,waaye ci kem li Yàlla di jagleel lenn ci wàlliyoom yu mat yi. + +Waxam ji mu naan wirdiy aji nos ji mi ngi ci jublu woon xasida gi mu doon tudde ñatti sëriñ yu tedd yooyu,ak dònn gi mu leen dònn, tuddati sunu sang Anas,ak Hassan (gërmul Yàlla yal na nekk ci ñoom) ak dònn gi mu leen dònn ci waxam jii: ((wommatal nga ma la Jiilaani (Abdul Xaadir Jiilaani)kawee woon ba fa mu yam)). + +Ku bëgg a am lu ko leer na xool teere bi nu naan “Tanwiirul halaki fii imkaani ruwyatin nabiyyi wal malaki”di ci maanaa leeralug lu lëndëm këriis ci man a nekkug gis Yonnant bi (j.y.m) ak malaaka,teere boobu boo bëggee lu leer rekk moo ciy géej jug mbàmbullan gi.te boo defee ag settantal ci tuxal gii ak li ci topp,da nga gis la amoon kon ca géej ga muy ni nu nangoo woon li mu jële woon ci ku dul woon Yonnant bi(j.y.m),ak dello ngi ko ko Yonnant bi delloowaatoon,ak naayibam yi, ñatti sëriñ yu tedd yi,ngir mu nekk naayibam moom Yonnant bi ( aji wuutoom),tey ki fi wuutu yooyule sëriñ (g.y.y.ñ),ci seeni wird ,di seen muxaddam bu nu joyal bi , nga xam ne amul lenn lu ko tënk ci wenn wird,(ku ko neex ak nu ko neex la koy joxee) ,da nga ci gis it la amoo n ci Sarsaara muy jox ga nu ko fa joxoon wirduw boppam moom rekk,jagleel ko ko,nga xam ne benn sëriñ bu ko fi jiitu masu koo yor. + +Looloo waraloon daawul digal ku jébbalu ci moom te yoroon aw wird njëkk muy ñëw mu koy bàyyi,da koy digal kay mu tëye ko te yéene ne moom moo ko ko jox,ku jébbalu ci moom nag te waxoo ko dara,bu boobaa mu door laa jox wirduw boppam. Looloo waraloon doomam ju tedd ja,sunu sëriñ,SheexMuhammadul Bashiir naan cig xasida gog biral na ci ngënéelug wirduw Sëñ bi ci yeneen wird yi,xaaral ma jox la ko lépp,ma nga ca biir it waxam ja mu naan: ((wommatal nga ma la Jiilaanii kawee woon)) ba ca bayit ya nga xam ne sëñ Bashiiru tudd na leen ci xasidaam gii,mi ngii: + +(ci turu Yàlla laay tàmbalee aw woy wuy jariñ ku bëgg a jariñu te ab xolam set) +(ag cant ñeel na Yàlla,yal na dolli xéewal ak mucc ci Yonnant bu nu tànn bii di gën ji mbindéef) +(ak ñoñam aki saabaam ,ñu tedd ñii te diy sang,ñoom ñi wuññi lëndëmi xol yi ak lëndëm) +(bu loolu jàllee ma naan la déglul waxi kiy laabiire boppam tedi la laabiire ci luy faji aajo) +( yaw miy sàkku matug texe ci yooni ñatti sëriñ yi) +(yoonu sëñ Imaam Jiili (Abdul Xaadir Jiilaani) ak Shazali mi làq ag ngënéel) +(ak Abool Habaas (Sheex Ahmad Tiijaan) miy ndamul ñu mat ñi,ñoom ñooñu nga xam ne seenub àtte ca jublu ga (xasd) mooy àtteb ku njëkk ka ) +(ànd ak ku ci nekk yor sa jagley bopp yoy ci la saw yoon làqe ay jagleem,loolu nettali nanu ko) +(na nga taqqoo’k yoonu Abdul Xadiim (jaam biy ligéeyal Yonnant bi) ,ndax moom kat moom la Yàlla mu jiitu mi jagleel mu dònn yoon yooyu yépp) +(ndax kat wird wu nekk am na mbóot,ci benn baat bu ci nekk,(ci biir wird wi) yal na la Yàlla gindi) +(baat boobu nag boroom “baziira” yi rekk a ko xam (baziira = gisug xol )keneen ku dul ñoom xamu ko,muy hikamu ab boroom buy aji not ) +(misaalam mooy Laylatul Xadar ci weeru koor wu nekk,ak Waxtuw Àjjuma,dees leen di wër di) +(Yàlla feeñalal na ko (moom Sëñ bi) ya làqu woon yépp (ci wirdiy yeneen yoon yi),ginaaw bi mu leen ligéeyalee te yekkati ag wàllam ngir jëmmam ju tedd ja,ba mujj ñépp bëgg ko jiital ko,(def ko muy seen muxaddam (ku nu jiital ki am sañ sañu joxe wird wi) ) ) +( Yonnant bu nu tànn bi tam - yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ak mucc ni mu ko tànne - yéegal ko ci ab hadara bob ku dul moom fàddu na ci yaw,bu nekk fa aji kawe ji (muy Yàlla) loolu di lu kawe sax la mu doon wut ) +(bi loolu wéyee mu donnalati ko lu nu nëbboon li , muy aji jiitu ciw yiw joj wuññi na ay fitna) +(ci coobareem (moom Yàlla),màgg na te kawe,la ko tànne ci darajay Yonnant bi miy ligéeyal biy joxe ag sell) +( ngir barig li mu leen ligéeyal te sellalal boroomam,di it ku sellal te matal kóllare ci diineem) +(mu boole lépp,dolli ci,yéeg ci barkeb Alxuraan te fa mu yéeg’ak a baax) +(boo jëlee wirdam de jël nga wird yépp,te doo ragal ag nërméelu) +(la nu dige ca seen wird yooyee it da nga ca jot,te doo ragal genn tëkku ) +(ndax moom (tëkku gi) ku bàyyi dëgg a ko tax a jug,te ku ko jël (moom wu sëñ bi) yayoo nga jagle ya ) +(jàpp ko de moo di jàpp ca lu baax la te dolli ca nag,ngir boole gi mu boole (wird) yépp,teg ca yor leneen ndollent (lu yeneen yoon yi yorul)) +(cosaan li mooy da ngay wax (ahuuzu billaahi minas shaytaanir rajjiimi)teg ca (bismil laahir rahmaanir rahiimi) jàng yenn aayay Alxuraan,doo ga tàmali) +(def hasbala (wax hasbunaal laah ba fa mu yam) def istixfaar ( astaxfirul laah) ,def haylala (wax laailaaha illaal laah) ,julli ci sangub ñu tedd ñi) +(ginaaw bi defees ag tëj gu rafet,loolu da na amal fa Yàlla lépp lu baax) +(lli mooy cosaani seen wird yi ñoom ñëpp,ku ci nekk nag am na genn jagleem gu mu moom moom rekk gu kawe) +(Sëñ bii nag moom jël seeni ndono jële ko ci gën ji mbindéef mi leen di àggale) +(mu wax (moom Sëñ bi) bi miy nettali yooyule xéewal,di ci sant kiy fàttaliku (di Yonnant bi) ngën ji aji xéewale ji (di Yàlla) ) +(ki moom jépp jumaa ak jépp jàkka, moom loo na ma mebëtum mbooloo yi) +(mu wax di sant aji tedd juy kenn ju ko donnal téere bi (di Alxuraan) muy ndono lu am njariñ) +(tàllal naa sama loxo jëme ca Yàlla,moom itam mu tàllal xéewalam ga ñeel ma ca géej ga,te loola tàlleeku) +(téereem bu tedd ba mujjoon na di wird ci man,daqaloon na ma samay noon it te dàkku leen) +(mu daan won lu neex képp ku ko taqoo, di ko jàng lu mu man) +(boo bëggee leeralug lii ma la tuddal,am lii nga xam ne ciy woyam laa binde sama mbind mii) +(wommatal nga ma lol ci la Jiilaani kawee, ngëramul ki ma kaweel yal na nekk ci moom) +(wommatal nga ma la Abool Hasan kawee woon ci ligéeyal Yonnant bi,miy maami Hasan) +(matalal nga ma la nga xam ne ca la Sheex Ahmad Tiijaan kawee woon,te nga nekkal ma ci lu rafete ni wurusu marjaan) +(wommatal nga ma lol soril na ma taq-taq,ma mujj mel ni Anas ci ligéeyal yonnant bi) +(moomloo nga ma te wommatal ma ag rafetal,donn na Hassan ci tagg Yonnant bi) +(ngërëm ak jàmm yal na nekk ci ñoom,ni lëndëm dàqoo ci ñoom(ni nu leerale àdduna bi)) +(mu wax ci bi miy tagg ngir sant ku nu jublu ki ( di Yàlla) ci téere bi (di Alxurran) ak Yonnant bi Muhammad) +(sama àddiya ji juge ci yaw ak ci Muhammad sunu sang bi, lu man a tee mer la) +(darajay aji far ji (muy Yonnant bi) far na samag deng-dengi,te wommatal ma kàttan ga ci lu dul ag doyodi) +(sama lépp’ay sant aji yekkati ji may dëgëral,cant gi nag jëm ci Alxuraan ak Yonnant bu baax bi) +( téere bi ak Yonnantub ku nu jublu ki, yekkati nanu sama lépp ci lu dul keno) +(Alxuraan nooyal na sama xol bu gindiku bi,dàq it bépp jalgatikat jëme ci ku dul man) +(sama xol ak sama loxo maa ngi ko jëme ci ku nu tànn ki ci di ko ligéeyal,may na ma nag la ëpp njariñ) +(aji dégg ji wuyyu na ma ci weeru koor,te baax na,mooy sama jubluwaay,ci barkeb Yonnant bi Muhammad) +(Yàlla gindi na sama xol,ñongal samaw yaram ci ngërëmam,dañal aji yàq sama) +(mu waxati bi muy déeyaale ak boroomam,mbégte ñeel na ñi ko sopp ñépp) +(ne: yaw mi jéggal sama ñaari way jur ak ñi ma sopp ci lu dul njàqare) +(te nga fàddul ma ci sa bopp ak ci Yonnant bi wëlif mbindéef yi,te may ma ay saar) +(fàddu nga ak man bu njëkk ànd ak Yonnant bi,may boroomug làqu wëlif mbooleem mbindéef yi) +( ma di ab jaam buy ligéeyal Yonnant bi,di ku nekk ci yaw ànd ak dëgg gi foofa,tey ku fàddu) +(mu waxaat ci yenn may yi nu jagleel ñi topp yoonam wi) +(Yàlla jëme na ci ñi dul ñi aju ci man lor yiy daje ak dof yi) +((ab boroom bu man loolu may na ko ko,te moom (boroom boobu) ku yayoo wuyyu la ci ku ko woo) +(nuy tëje ci Yonnant bi,mi di ag tàmbali te di ag tëj,tey ki gën a mat,yal na Yàlla saxal xéewal ci moom ak ci ñu mat ñi) +Foofu la loolu yam. + +Ñu dellu ci wax ci cosaanul wird wi,ak yax bi(yax=nassu ci araab.=texte ci français) mu bindoon ci ginaaw sotti (sotti = nusxa ci araab.=copie ci français) ga mu amaloon ca wird wa, muy : + +bismillaahiir rahmaanir rahiimi wa sallal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wahalaa aalihii wa sahbihii wa sallama tasliiman ,ku xool araf yii nu bind ginaaw matug wird wi, na xam ne ki ko bind di Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibul Laah,mi askanoo Mbakke te dëkk Bawal,may na ndigal mbokkam moomu ci Yàlla (t.s),sang bi Mustafaa Usmaan mi juddoo Halab te dëkk Madina,may na ko ndigal ci mu jëfandikoo wird wu nu barkeel wii ak jox ko ku ko soop ci mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi,ni mu ko jëlee ci Yàlla jaarale co ci Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu du ciy nelaw,atum baksasin di junni ak ñatti téemér ak ñaar fukk ak ñaar,ginaaw gàddaay gi,yal na Yàlla defal ki ko defoon gën jaa saxi xéewal ak gën jaa jariñi jàmm,ci benn barab bu nuy wax Sarsaara,ci weeru koor gi nu wàcce Alxuraan,mu dig jub ñeel nit ñi,te di ay aaya yu leer yoy ag jub la ak teqale dëgg ak safaan. Yàlla nag mooy seere lii nuy wax.Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yasifuun wa salaamun halalmursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina. + +Sunu mbokk moomu Muhammad Abdul Laah Alhalawii,nee na ci teereem bi tudd(( Anafahaat almiskiya fiil xawaariq al mbakkiya))muy ci maanaa bonnig misk ci xar-baaxi Mbakke,nee na Sëñ bi Yàlla da koo jox wird wii,mu jox ko muritam yi,xemmemloo leen ko,te loolu di lu war ci moom. Mu ne leen képp ku ko saxal aki sartam da na tàbbi àjjana ci lu dul hisaab (hisaab mooy laaj yi ñiy def ak a gëstu ay mbir) du caagéenug mbugal,te Yàlla it da na ko aar ci naqar yi ci àddina ak alaaxira,te saytaane mu nu dàkku mi du ko jege,da na doy wird wi ag kawe,nekk gi mu nekk wird wow boo ko dee jëfandikoo soxlawul gay jëfandikoo yeneen yi,te manoo am li ci moom te jëfandikoowoo ko. + +Sunu Sëriñ, sunu wasiila ca sunu boroom mu kawe mi nee na bi mu nuy jox wird wu tedd wii:jox naa leen wird wii ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe,kon tëye leen ko ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe. Mu waxaat jàpp leen ko ak doole,ku ci jotoon a yor weneen wird bu ko manee, na leen boole,kon muy leer ci kaw leer,bu ko manul mu yam ci wird wu tedd wile. Jeex na. + +Ki ko doon taariixal nag ne moom : bismil laahir rahmaanir rahiimi ,lii aw tagg ak taariix gu Ahmad doomi Asan def ñeel wirduw sëriñam bi Sheexul Xadiim,yal na nanu Yàlla jariñ ci moom ci ñaari kër yi aamiin. + +( sunu boroom taxawal (fondumang)na sunuy jëf ci may nu ñu man a root ci gën ji teen, kon mbégte ñeel nanu (mu jublu ci wirdul maaxuuz)) +loolu mooy wirduw sunu sëriñ bi Sheex Ahmadu Mbakke,mu juge ca boroomam jaar ci Ahmad Yonnant bi) +(yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc,li feek mi ngi doon ab raas jëm ca texe gu kawe ga) +(jox na ko wird wii jële ko ca aji namm ja muy Yàlla,yéem naa te ñée bii sëriñ ak yii taalube) +(jagleel na ko wurusu luulu wu nu ñongal ci xor,te làq ko ku dul moom) +(wurus ñeel na sunu sëriñ bu nu gërëm bu màgg bi,ku ko am de am dëkkaaleg ka gën a màgg) +(mi ngi ko gènne ci bisub àjjuma,mu jëm ci ku Yàlla texeel ci doomi jamono ji) +(ci juroomi fani sawaali atum (sahidnaa karaman) di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,moom boroom taariix bii,moom miy ndëppul ñu tedd ñi (ndëpp mooy mbaxana mi nuy solal buur) ) +(mooy sunu sëriñ Ahmadu MBAKKE mi dëgg di tax a tukki ak a took ) +(génneel nanu ko ngir jëmmi Yàlla ,kon billaahi bu ko sàggane) +(ngir Yàlla,boo bëggee am li nga bëgg,ndax kat kuy rëbb ba jam ñay man a dëpp) +(yaw sama boroom ci darajay aji wommat ji xeet yi jëme leen cig jub,di Muhammad miy wuññi njàqare) +(yal na Yàlla miy sos niir yi,sotti ci moom gën jaa selli xéewal ak mucc ak ñoñam aki saabaam) +(ak ci darajay sunu sëriñub Mbakke bii,na nga ma may ma jot ca la ña jiitu bëggoon) +(ci ag kawe,bu ko defee ma bokk ci mbooloom ñi la jege,yaw miy boroom nguur gi) . + +Nan dellu ca tukkib ñaareel ba,dem ba Tintu Muxsin,foofu barab la bob xew-xew bu ñaaw te soof dal na ko fa,muy : ab naar bu nu xam turam ak giiram,daa jugoon ngir ne da koy faat moom Sëñ bi - man moom xam naa ko waaye dama koy suturaal ngir doomi baay tëxam yu julit yi - moom da doon fexee faat Sëriñ bi,Yàlla musal ko ci,ni mu doon defe loolu nag mooy xanaa ñëw ci moom won ko ag cofeel gu dëggu ak jébbalu ci moom,Sëñ bi moom itam suturaal ko,boole ko cig njabootam,bindal ko ñatti bëyit,ne ko na ko saxoo jàng,guddi ak bëcëg ,naar bi moom itam dëkke woon loolu,bëyit yi moo nekk nii: +(lor ak saytaane jëm nanu ci ku dul man,ndax ñoom ñaar kat amunu ci man genn kàttan) +( Yàlla mooy sama boroom,Yonnat bu nu tànn bi - yal na Yàlla dolli xéewal ci moom, moom mi ko gindi te tànn ko) +( mooy samab xarit te di sama soppe,te bañ na it samag loru,te sàkku na ci boroom mbindéef yi samam mbég ) + +Naar bi taqoo woon ak loolu,di ko jàng guddi ak bëcëg ,ci mbooloo mi ak bu wéetee,mu ko daan def ginaaw saaru Yasiin,mel ni kuy nodd,nga xam ne da naan wax: yaasiin,yaasiin,yaasiin,ba kero muy mat juroom ñaari yoon,mu door a àggale saar wi teg ci bëyit yi,jàngati yaasiin ni mu ko defe woon,tegati ci bëyit yi,baamooti leen,niii daal la ko daa defe ,daawul taxaw lu dul daa sonn walla muy nelaw,mu sax ci loolu ay fan,am na ñu ne weer. + +Jamono jooja Sëñ baa nga woon fa ñoñ sheex siidiya,nekk ca seen xayma ya,ci noonu mu digaloon taalube ya nu defaral ko ag kër ca bitib gàdd ga,ñu def ko ni mu ko bëgge woon,bi mu noppee mu wax ko sheex Baaba,sheex Baaba digal mbokkam ma sheex Siidiya Muxtaar mu gunge ko ca kër ga,mu defe ko noona. + +Sëñ bi moom digal naaram booba mu ñëw ànd ak moom ca kër ga tey jàng ñatti bëyit yi,ni mu ko baaxoo woon,bi nu agsee,saytaane jàpp ko,xamal ko ne pexe mi mat na,def dong a ci des,bi guddi gi soree ba kenn yëngootul,naar bi jug,summiku ba mel ni ko ndayam jure woon,dal di dugg ci kër gi,jawali ca néeg ba Sëñ ba nekk,ginaaw xamoon na fa jaasiy Sëñ bi nekkoon ,mu jawali ca,bocc ko ci mbar mi,waaye Yàlla dogal jenn waay ju bokkoon ci néegub nguurug Kajoor,te gënoon cee rafetug tuub ak bàyyi àdduna,ñu ko daa wax Omar FAAL NDATI,nekkoon ca jàkka ja,di fa fanaanee jaamu Yàlla,bi ko naar bi rombee mu jug ca saa sa,seeti ki yor mbiri biiri Sëñ bi ,di Muhammad Lamin ÑANG,doomi Muhammad Lamin Mati,moom waa-jur wi,doomi bàjjan la ci Sëñ bi,xamal ko ne am na jëmm ju rafle ju jëm ca néegub Sëñ ba,ca saa sa ndonga la jug,gaawantu,fekk naar ba mu bocc jaasi ja,di settantal naka lay jekkoo Sëñ bi ba man koo lor bu baax,te Sëñ bi moom mi ngi tëdd ci wetam,bi naar bi xàccee di ko door jaasi ji,yàlla dogal mu lonk ci koñub xayma bi,daje ak ndonga li di wadd di dal ci kawam,mel ni kuyul gileem loolu,dal di koy nërméel,naar bi yuuxu,murid bi yuuxu ci kawam,mel ne da koo bëg a lekk,seen coow li fees foofa dell,ña nekkon ca wet ga yuuxaloo,daje fa,nga xam ne Sëñ bee mujj ñëw dox digganteem ak nit ñi ne kon ñu ray ko,mu dalal leen,dal di yonne ci menn mbooloo,mu fanaanoon fu sori foofa,mu mu naroon a yewwi,woolu leen,ne leen yobbaaleel leen ma naar bii ba Xumaak, (barabu kiliftéefug tubaab yi,da nanu ko wax it Sahwatul Maa) ngéen bàyyi ko fa te dem seen yoon,denk leen ñu yëram ko te dimbali ko ci bagaasam yi,làq leen nag xibaar bi,ngir bañ ñu gaañ ko,jeemul a fayoonte ak moom ci jëfam ju ñaaw. + +Yenn taalube yi nag gis nanu ne li tax Sëñ bi delloolu naar bi Xumaak,fa tubaab yi am sañ-sañ,ab junj la ci ne ñoom tubaab yi ñoo ko yonni,Yàlla rekk a xam,waaye pexeem ma moom Yàlla naaxsaayal na ko. + +Yooyu ñaari bëyit boo ko xoolee da nga gis ne Yàlla feeñalal na ko ci ay karaama yu kawe,yal na ko Yàlla fayal jullit ñi aw yiw ak Lislaam. + +Man nag li ma gis mooy lii mooy dëgg-dëggi laabiir ak doylooYàlla,ak nangu ab dogalam,miinunu ko ci ku dul moom ci waa jamonoom,li mu nuy fàttali mooy li daloon ki miy ligéeyal ci yenn ci xareem yi,loolu mooy dafa am benn Ahraabii (araab bu dëkk ca kaw ga) bu tuddoon Duhsuur bu ko fekkoon mu tëdd,xaw a sori saabaam yi,mu bocc jaaseem,xàcc ko ne ko ana ku man a dox sama digante ak yaw? Yonnant bi (j.y.m) ne ko Yàlla,ci noonu waa ji di lox ba jaasi ji rote ci loxo bi,Yonnant bi (j.y.m) jël ko ne yaw nag ku la man a musal ci man? Mu ne ko amal yërmaande, Yonnant bi jéggal ko,bañ koo def dara. + +Naar bii nag moom bis dellusi na ci Sëñ bi ca Xumaak,taalube yi jug ngir fexeel ko,Sëñ bi yëg ko génn ci naaj wi,te solul ay dàll,di wax ca kaw: bàyyi leen ko,bàyyi leen ko,(alaa tuhibboona an yaxfiral laahu lakum) muy:xanaa bëggu leen Yàlla yëram leen,di ko baamu. + +Nu bàyyi ko,mu digal ko mu làqu,génn te dem yoonam,ginaaw bi mu ko defalee ag njekk. Bi ku tedd ki nekkee Njaaréem,naar bi delseeti fa,Sëñ bi aarati ko,naan ko:boroom jaasi ji,naar bi naan ko : déedéet neel boroom xëm gi,bu ko defee Sëñ biy ree,génneeti ko ginaaw njekk.Man ci sama bopp gis naa ko Cees,maanaam Jànqeen,te booba maa ngi ànd ak am mbooloo ci taalube yi,waaye man rekk a ko ci xàmmee,bu ma ne woon kii de diw la ñu ray ko,waaye kon ana jikkoy Sëñ bi,Alhamdu lillaa. + +Nu dem nag Jaraari,barab la bu Halawi yi moom,Sëñ bi tudde woon ko Biirul Xayri di ci maanaa teenub yiw,ci barab boobu la Sëñ bi doon waxe xasida gii: +(( li ma doon laaj sama boroom indil na ma ko cig baamu,rawati na ca Biirul Xayri di Jarraari)) +((samag cant ak njukkéel ñeel na ab boroom bob wommatal na ma ay xéewal,ci lu nëbbu ak lu feeñ,di ku ñu baax ñi sopp)) +((sama boroom wommatal na ma barkeb saabay ku nu tànn ki,mu nekkaloon ma te daawu ma won ayuw kàccoor yi)) +(( samag cant ñeel na aji jiitu juy aji des,kok aar na sama kanam wëliif bépp ñaawtéef,ànd ak ag bëbb guy daw juge ci moom jëm ci man (bëbb mooy luy sottiku bu baax di wal fii mu jublu ci xéewal) )) +((samay cant ñeel na ko,ci biir ay sang yu askanoo ca Aliyun (fii man na cee jublu Seydinaa Aliyu,man naa firi it aji kawe di Yonnant bi) ci lu dul aji jalgati mbaa workat)) +((aji des ji amul bokkaale yal na dolli xéewal ak mucc ci ki nga xam ne indil na ma la ma ko ñaanoon cig baamu)). + +Halawi yi nee nanu xamunu lu tax Sëñ bi tudde ko Biirul Xayri,ndax tur woowu ñoom masunu koo dégg ci seei baay,ba bi nu fa suulee Sheex Ahmad Bun BUDDIN,nu dal di xam sekkareb li tax mu tudde ko ko,nu xame ci baatinub Sëñ bi. + +Ci Sheex Ahmadu Bun Buddin, Sëñ bi wax na ci ay wax,Alhaaji Muhammab Bun AAB,dàkkantal la ci Sheex Ahmadu Bun Buddin,nettali na ma ne baayam bind na bis Sëñ bi ne ko daa bëgg mu nuyyul ko Yonnant bi(j.y.m),ak Sheex Ahmad Tiijaan,te itam soxla na seenub tontu,Sëñ bi tontu ko xamal ko ne Yonnant baa ngi koy fay,ak Sheex Ahmad Tiijaan,aji nettali ji nee na ca saa sa, baay ji daanu ab jéll,di yëggal bopp bi ak a waxtu,mel ne ku jaaxle te nu muur am xelam,dañul ci melokaan woowu ba bi mu faatoo (y.y.g),te booba ñi ngi fu sori woon Sëñ bi, te yëgalunu ko woon kenn ci guddi gi mu ame woon,waaye amul lu dul ay ndaw dikk ci suba gi ne Sëñ bee leen yabal ñu teewesi dencug Sheex Ahmadu gi,te di leen ko jaale. + +Mu bind ci loolu ag xasida di ci xamale darajay Sheex Ahmadu moomu, fa Yonnant ba,moo tax mu terale ko karaama googu,ne lii mooy payug Ahmadu Bun Buddin,tey payug ab xalifaam: + +Bismil laahir rahmaanir rahiimi, yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu sang bi Muhammad aki ñoñam aki saabaam,na ngeen xam ne guddi gi Sheex Ahmadu Bun Buddin di faatu ruuhul xudsi (jibriil) (j.y.m) wàcc na juge ci asamaan si,ànd ak lu bari ci ay malaaka ngir terale ko sang boobu,ngir rafet gi mu rafetoon njort ci Jaam Biy ligéeyal Yonnant bi (Sëñ bi) ,yal na ko yal na ko Yàlla nekkal cig teral,moom miy aji jiitu tey aji des,ñoom nag delluwaatunu ca guddi googee ndare bu danoo yobbaale ruuwam gu tedd ga,lii nag mooy dëël bi nu ko dëëloon,(dëëlmooy dikk) .loolu la Sëñ bi di junj ci bëyit yii: + +((Ruuhul Qudsu ñëw na,di wuññisi njàqare,ànd ak mbooloo mu mag ciy malaaka,jamono ji Ahmadu mii di làqu)) +((Ahmadu am na la mu bëggoon ca Yàlla,buntub yiw ubbikul na ko bu dul tëjooti)) +((yal na Yàlla fay ka joxoon àddiya aji ligéeyal ji,moom moomu nga xam ne am na fa Yàlla ag tab gog aw yiwam moo gën a mat)) +((maa ngi sàkku ci boroom aras ay may ñeel ka ko joxe woon moom mooy aji texe ju nu ndëppal ji (ki nu solal mbaxanam buur) )) +((sangub sang yi wéy na,di ab sëriñ bu nu jiital (bu nu def muqaddam),jiital gi it ki ko def di sëriñ bob aw wirdam ba fàww am ngér lay doon)) +(( moom de bir na ko ca àllaaxiraa gee mu nekk ne man maay jëwrini ki nga xam ne mooy boroom raw ak jiital,te mooy ku nu ndëppal ki)) +(( sangub sang yi yal na am ngërëmul sëriñam,ak ngërëmul gën ji mbindéef,ndaw muy ku nu bégal !)) +(( Yàlla la’ay ñaan mu may xalifa bii mu fi bàyyi la mu yéene,ci darajay ka nga xam ne ay leeram day jolli)) +(( yal na nekk ci moom ,moom Yonnant bi,ñaari xéewali Yàlla mi ko gindi def ko muy ku nu gënal ki,ni mu doon yéege ak a kawe ca rañaan ga)) +wasalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu. + +Eskëy,gis nga waxam ji mu naan “ka ko joxe woon” mi ngi ci jublu Sheex Ahmadu Bun Buddin mii,li mu ko joxoon mooy benn teere bu tuddoon ((Mawaahibul Ladduniya)). + +Sama mbokk,sama xarit Sheex Ibraayma AMAR nu gën koo xame ci turu Ibra Joor,nettali na ma ne Sëñ bi,bi mu nekkee Sarsaara walla Tuntu Muxsin, da koo yonni woon Ndar ngir mu jëndal ko fa téereb Mawaahibul Laduniya,nga xam ni ki nuy wax Qastalaanii moo ko def,nee na ma dem sonn ci lool,fu ne ma wër fa,waaye dara,ma am lu ma naqàri lool,yëf yi tiis ma lool,ma dëpp di ñibbi,bi ma tollee ca gàddug Sheex Ahmadubnu Buddin,te fekkoon ma xamante ak moom,ma daad fay jàdd ngir nuyyu ko,siyaare ko,ba ma fa àggee mu bég lool,teeru ma dalal ma,bi nu toogee bay waxtaan mu laaj ma lu ma taxoon a jug,ma ne ko sëñ bi dey moo ma yonni woon Ndar,ma leeral ko tam naqàr wi ma am ci ñàkk a am teere bi ma Sëñ bi yonni woon,ca saasa mu jug,gëstu ci ay teereem,génne ñaari xaaj yepp indil ma,ne ma neel Sëñ bi àddiya la,ju ma ko jox ngir Yàlla,ma bég ci ba fa bég yam,waaye Sëñ bi moom gën maa bég fopp ci teere beek ki ko joxe,loolu nag mooy maanaam ka ko joxe woon,mu jub lu ci li mu joxe woon “MawaahibulLadduniya” . + +Xasida gii ndollent la ci tontub kiy laaj ndax Jibriil da na dikkati ginaaw yonnat bi. Bokk na ci li mu bind ñeel Sayid Ahmad mom Sheex Muhammadul Haafis lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allaahuma salli halaa sayyidimaa muhammadinil faatihilimaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa,naasiril haqqi bil haqqi wal haadii ilaa siraatikal mustaqiim,wa halaa aalihii haqqa qadrihii wa miqdaarihil haziim,na Sheex Ahmadu Bun Sheex Muhammadul Haafis,ak ku dul moom ci ñoñ Halawi yu goor yi ak yu jigéen yi,ak ku dul ñoom ci jullit ñu goor ñi ak ñu jigéen ñi,nanu xam ne Yonnat bi jàmm ak xéewal yal nanu nekk ci moom,delloo na ab nuyyo Sheex Ahmadu,te Sheex Tiijaani moom itam gërëmul Yàlla yal na nekk ci moom delloo na ko nuyyoo,te Yonnant bi (j.y.m) teral na ko teral gu mel ne gi mu teral mbokkam mi Sheex Muhammadul Haafis,ki ciy dund yal na ko Yàlla gërëm te aar ko ci lépp lu mu ragal,ka wéy it mu gërëm ko te yërëm ko,te SheexAhmad Tiijaan it yal na ko Yàlla gërëm,te jegeel ko,def na ko niki doomam,képp ku jële wirduw tiijaan ci ñaari sëriñ yii tudd Ahmad yal na leen Yàlla gërëm te aar leen te yërëm leen,mel na ne jële na ko ca Sheex Muhammadul Haafis (y.y.g),képp ku ko jële ci ñoom ba noppi bàyyi leen fi di demati ci keneen ci mbooleem sëriñ yi,ànd ak yéeney bàyyi leen,na ko wóor ne pert na ci àddina ak allaaxira,yal na nu ci Yàlla musal,képp it ku ko jële ci kenn ci ñoom ñaar,bu ca faatoo tonowu na adduna ak allaaxira,képp ku xool mbind mii na xam ne bi nu koy bind Sheex Ahmad Tiijaan (y.y.g) moo taxaw di wax ñuy bind. + +(( dello nuyyoo bu teey bu kawe bépp nuyyoo buy bijj ag dëppoo)) +((juge na ca jaamub boroomam bay ligéeyal ku nu tànn ki,jëm ci ki làq kawe gi niy tànn)) +(( yaw sëñ bu màggi mbir bi,musal nanu la ci lori lépp lu ñaaw)) +((musal nanu la ci rékki aw yiw wu nekk ci yaw,ba kero ngay tàbbi àjjana ya’ak ñi lay xeeñtu)) +(( Aji des ji musal na la ci ñaawtéef yi,ci barkeb ku nu tànn kiy boroom raaya ba (daraapoo ba ,di Liwaawul Hamdi) )) +(( ak darajay sa sëriñ bu nu gërëm ba,Sheex Tiijaan,ka mujj mel ni wurusu marjaan fa sang ya)) +((yal na Yàlla miy aji des dolli xéewal ak mucc ci gën ji mbindéef, moom (Yàlla) miy ki koy wommatal kawe ga ak saar ya)) +((ngërëmul Aji des,luy bijj ag dëppo yal na nekk ci wàlliyu wow topp na ay tànkam (tànki yonnant bi) )). +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina + +Bokk na ci li mu bind ngir ñiy am ag wuute ci “Mahiya” (mahiya mooy ag ànd,nu jublu ci ànd gu Yàlla ànd ak kenn walla nekk gu mu nekk ak moom) ,lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatahaa minas saytaanir rajiimi,rabbi,ahuuzu bika min hamazaatis sayaatiini,wa ahuuzu bika rabbi ayyahduruunii. Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allahuma salli halaa seyyidinaa wa mawlaanaa muhammadin,al faatihi limaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa naaziril haqqa bil haqqi wal haadii ilaa ziraatikal mustaqiimi,wa halaa aalihii haqqa xadrihii wa miqdaarihil haziim, +mu ne mi ngi ñaan julli gii doon gog da na yee képp ku xool mbind mii,mu yee ko ci ne Yàlla kat ànd gi mu ànd ak ñun ànd gu yellook moom la - tudd naa sellam ga - du ànd gu xel di jot,te moom - barkeel na te kawe - jege na nu,waaye jege gu yelloo’k moom,du jege gu xel di xalam,te xam-xamam - tudd naa sellam ga - lu nu sellal la,niki mbooleem ay meloom ,jëmmam it - barkeel na te kawe - tàqalikoowul ak ay meloom te du tàqalikoo ak ñoom it. +Waxi Sheex Sanoosi ji,(y.y.g) ak ñi ànd ak moom ci lu aju ci “Mahiya” lu wér la,ndax ñoom kat danoo seet fi nit ñi toll,ñu wax fa’ak ñoom,ndax bu nu weesoo ak ñoom foofu ñu tàbbi ci alkande,ñoom ñépp. Waxi Sheex Ahmad Tiijaan ji it (y.y.g) wuutewul ak li nu wax. Waaye li ñi askanoo ci moom(y.y.g)di wax,ba miy indi ak noonoo ci seen digganteek Abuubakar Ibnu Fatan,na leen wóor ne noonoo googu de ci saytaane la juge,ndax Ibliis day tàbbal lënt-lënt ci xolub képp ku nekkul “Mushaahid”,(mushaahid mooy aji jàkkaarloo,maanaam kay jàkkarlook mbir ya ca nguurug sunu boroom ga) liy firnde ci loolu mooy Jaam biy Ligéeyal Yonnant bi - yal na ko Aji des,jiy Aji jiitu nekkal cig teral - bi muy bind laabiire gii déy,Yonnant bi dikkal na ko (j.y.m) ne ko Sanoosi Ak Sheex Tiijaan ak Xazaalii de ñoom wuutewunu,ñi am ag wuute kay ñooy ñu dul ñoom. Dëgg gi mat a dellu daal mooy bàyyee settantal ci melow “Mahiya” te gëm rekk ne lu am la,ndax di ci settantal day rékki ngëm ,yal na nu ci Yàlla musal. Wasalaam . + +Bokk na ci li mu bind ñeel Abuubakrin Ibnu Fatan ci mbirum “Mahiya” lii:Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla dolli xéewal ci sunu sang Muhammad ak ñoñam aki saabaam,ag xéewal akug mucc gog da na ci xamal nit ñi ne la Aboobakrin Bun Fatan waxoon ci waxi Seex Tiijaan ji,jubluwu ci woon Sheex Tiijaan(y.y.g),te moom Sheex (y.y.g) dëppoo na ak moom (Aboobakrin) ci mbooleem li mu wax ci tontoom yi. Ag jub nag mooy nit ñi bàyyee xuus ci lu mel nii,ndax xuus ci, ci ñaawtéef yi la bokk . Waxi qutbu yi, yal na leen Yàlla gërëm, du waxi boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm. Boroom xam-xam yiy jëfe seeni xam-xam,fi nu toll ci wàlliyu yi mooy fi wàlliyu yi toll ci yonnant yi . Boroom xam-xam yi boroomi tawhiid lanu yuy aar Sariiha mu nu laabal mi, qutbu yi boroomi sellal lanu yu jegeYàlla di aar “Haqiiqa” mu nu leeral, mu nu sellal mi.Kon wormaal ñépp ngir jëmmi Yàlla mu kawe mi lu war la . Bëgganteg boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm,mooy dundug sariiha,seenug wuute ci masala yi,ag jàng la akug jàngale,dug noonoo,dug iñaanante. Wasalaamu halaykum wa rahmatul laahi wa barakaatuhuu. + +Bokk na ci li mu bind ci Ahmadabnil Kawri Addaymaanii, lii:Ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla mu kawe mi dolli xéewal ak mucc ci sunu sang ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam,xéewal ak barke ak mucc gog dana ci xamal nit ñi ne Muhammad Ibnu Kawri Addaymaanii,ak Abuubakrin Bun Fatan Alhasani,Yàlla mu barkeel mi te kawe jéggal na leen ñoom ñaar,ci bisub Harafa atum “shahidnaa bikaram” di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,te ku ci nekk ci ñoom ñaar xawoon naa alku,sababub loolu mooy juumug Daymaanii,ak weddig Alhasanii. Ahmadu Bun Kawri moom dëppoowul ak Sheex Tiijaan ci li mu doon xuus ci wàllug Mahiya,bu dee Aboobakrin moom daa ñàkki teggiin ak Sheex Tiijaan (y.y.g) ci ñàkk a nangu ag tontoonteem ak Ahmadu Bun Kawri,Sheex Ahmad Tiijaan nag moom ku beru la wëlif leen ñoom ñaar.Liii mooy dëgg gi nga xam ne sikk amu ci. Wasalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhuu. + +Mu bindoon ba tay jëme ci ñenn ci ñoom: Assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wabarakaatuhuu,bu lii jàllee,man de gis naa li xewoon ci sa diggante ak keneen ci lu aju ci mbirum Mahiya,man nag li may wax ci Mahiya,mooy jëmmi Yàlla moom,kawe na te barkeel,du toq ci xelum kenn mu koy jéem a gëstu ,kon xuus ci Mahiya moo’k wuute gi am ci diggante yahood yi ak nasaraan yi ñoo yam,yal na nu Yàlla mu kawe te barkeel mi musal ak yeen ci soxlawoo lu nu yitéelul. Soxlawoo def ndigal yi te teet tere yi moo gën a jaadu ñuy soxlawoo xuus ci googule wàll,Yàlla barkeel na te màgg,nee na :( zarhum fii xawdihim yalhabuun) muy bàyyi leen ci seen xuus googu,ñuy fo. Wassalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaala wa barakaatuhuu. + +Ci noonu Sëñ bi tuxoo ci barab dem ci barab, ba bi mu sancee ca Sahwatul Maayi,nu gën koo xame Xumaak,soriwaay bi di lu tollook doxub bis bu tar ci ku sawar,juge Dagana walla Budoor. Loolu amoon ginaaw lollib atum baksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,mu mujj di wër ci barab boobu di tukkee ci kër,dem ca geneen gu jege,mbiram it moo’k mu mbooloo yi koy dikkal di siyaaresi di gën a yokk,ci jamono ju nekk. + +Cig gàttal daal leeral mbiri Sëñ bi yepp ci ñaari tukki yii,aal topp aal (aal = tolluwaay yi nit di toll), xew-xew topp xew-xew,kenn ku dul moom manu ko,yal na Yàlla yokk ngërëmam ci moom. + +Ag karaamaa ngii gu amoon ca Xumaak,maanaam Sahwatul Maayi,ci genn guddi ci benn ci ñaari weeri rabiih yi,atun jaksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñatt,muy tawati tànk ju ko daloon te tar lool,fogloo nu ca guddi googa,nu fanaan ca la wër xaymaam ba,nga xam ne sax jortoon nanu ne du weesu guddi ga,waaye moom mu niy dalal rekk naan nu dellu leen ca yite ya,amul solo,waaye nun deeti nopp mbaa ay xel di àndati ak nun. +Bi Yàlla dogalee mu wér ca suba ga,mu xamal ma ne mbir mi de balaa la woon bu juge fa sunu boroom,jëmoon ciy nitam,ñu naroon a fër bu leen daloon (fër = naaxsaay), ma ne sunu boroom lu tax nga jagleel sama nit ñi nattu bii bàyyi ñeneen ñi,ñu ne ma ndax kat Yàlla da laa teg ci sa kawi moroom,kon manul a ñàkk mu jàgleel la sa nattub bopp bu ñeneen ñi dul am,te loolu amul lu ko gën a tar.Man it ma ne yaw buur bi ndax man naa koo gàddu wëlif leen ? Ñu ne ma aha kay, jëlal ,mu doonoon lu diis juge ci asamaan wàcc sama kaw,ma daanu xëm,ñu indi ma ci xayma bi te yëguma. Ki ko yobb ci xayma bi,di Moor Xari Joob nettali na ma ne jaan a ko màtt,kon alhamdu lillaahi ci mucc gi ak tuufu gi (tuufu mooy am li nga bëgg) . + +Doggantal : ci ag ñibbiseem ci ñaareelu tukki bi + +Ba mu fa nekkee ba guddig gàmmug atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,di guddig àjjuma,la fa Sheex Ibra FAAL ñëw,tukke Ndar,indaale këyit wu juge ca tubaab ya di ko may mu dellu réewam Senegaal,murid boobu it dikk jàpple ko ci tuxu gi,mu tàmbalee waaj,di tàggu waa dëkk ba ,ba àjjuma ja dellusi,di fukk ak juroom ñeent ca weer wa,mu génn këram googa sóobu yoonu Ngaanjaar,maanaam Gaaya,dib dëkk bu nekk ci penku bëj-gànnaaru Dagana,dex gi romb na fa,ñooña sàkku ci moom mu julli ci seen jàkka ji nu doon yeesal ,ngir barkeelu ci,mu ànd ak seen imaam ja Muxtaar SOW, julli ñaari ràkkaa ci njëlbéenug yoor-yoor,jëggi dex gi dem dagana,nekk fa ba bisub gàwwu ñaar fukki fan ak juroom ñatt ci weer wi,mu dugg gaal ci tisbaar ji jëm Ndar. + +Jamono yi mu nekke woon Dagana,nganale gu nekk defal nanu ko ko fa,ci bëcëg gi, bu guddi masaan a jot,ñu daa indi ay làmp yu leer ci kanamu bóoli yi. Mu wax ci loolu ne loolu mooy liy dëggal waxam ja mu waxoon ca lenn ca xasaayidam yi mu defoon ci arafi ((walil laahi mulkus samaawaati wal larli))di ci maanaa Yàlla’ay boroom nguurug asamaan ak suuf,muy li mu mujj a bind ca Daarul Mannaan ca Tuubaa,ba mu àggee ca arafu daad wa mu waxoon ca : gane ji naa aji Tedd ji,mu teeyalal ma ganale gi,te du ma dañ ci nganale gi mel ni ay làmp + +Bi mu àggee Ndar ca guddi ga,daa dal di wàcc ca Sheex Ibra FAAL,sax fa ay guddi,juge fa dem Luga, wàcc ci Alhaaji Masamba Soxna,foofa la yabale ligéeykat yi ñu dem Njiheen,maanaam Cëyéen,ca Jolof,jiitu ko fa,defaral ko fa ag kër njëkk muy agsi,dal di jàll Ngaajax,fanaan ca jàkka ja,fa seen xabrub wàlliyu nekk,dal di jàll ca kër sëñ Asan NJAAY,yendu fa ,fanaan fa,yendooti fa,laxas dem Kokki,wàcc ca Sheex Muhammadu Maam ,maami Sheex Bashiiru,demati Duriga,faSheex Madun Samba,maami Sheex Murtadaa,juge fa àgg Kër Baasin ca Sheex Muhammadu Amina Xuma JOOB,doo nga dem Cëyéen ci bis yu néew,di njëlbéenug rabiihus saanii,fekk yenn kër yi noppi,bi mu agsee ca kër ga,ca njëlbéenug rabiihus saanii,atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,daa wàcc tudde ko Daarur Rahmaan,mu nekk fa mbiram akuw doxiinam di gën a jub,di dolliku waxtu wu nekk,ba ci benn ci ñaari jumaada yi ,ci atum saksasin,di junni ak ñatti téemèer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,mu taxawal Daaru Xudoos ci sowwub dëkk bi,soree ko lu tolloo’k ñaari kilomet walla lu ko yées,mu sax fa ,bul laaj nag mbiram,moom daal na ma la ko waxe woon rekk ci bépp barab,waaye fii sax gën na fee dolliku,ba ca àjjumay ñaar fukki fan ak ñaar ci weeru muharram,atum lasasin,di junni ak ñatti téemèer ak fanweer. + +Ca sahbaani sakasin ja,di junni ak ñatt téeméer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,walla ca ramadaan ja,la sëñ Abdul Laahi gane àdduna,wax nanu ma ne Sëñ bi daa bind Abdul Laahi ci aw këyit,yonnee ko Sheex Muxtaar Binta LOO,nijaayi sëñ Moodu Mustafaa,digal ko mu tudde ko noonu,mu defe ko ni mu ko binde woon ci këyit wi,mbooloo mi nag leegi danu koy wooye Abdul Laahil Haziizi,te xawma fu nu jële loolu,ah waa-waaw xanaa denu cee jublu ne Haziz turu Yàlla la. + +Doggantal : cig génnam juge Jolof jëm Njaaréem + +Ci njëlug bisub gàwwu,ñaar fukki fan ak ñatt ci muharram,atum lasasin,la génn dem Njaaréem,mu julli woon suba ginaaw bi mu doxee lenn ci ay kilomet,mu fanaan ca la yées Tuubaa, ca guddig altine ja mu fanaan Tuubaa,ca Daarul Haliimil Xabiir,fa Sheex Abdu Rahmaan LO,muritam ba jàngal doomam yu mag yi,mu xëy nag jëm Njaaréem,fanaan fa guddig talaata ñaar fukki fan ak juroom ñatt,bi mu àggee Njaaréem,ñu dalal ko ci njëlbéen gi ci benn pàkk bu nekkoon ci wetu àttekat (goornoor) bu ndaw bi,àttekatu ñoñ bi (al haakimul ahlii,xanaa mooy gouverneur civil) ,ca jamono jooja ma nga dëkkoon ca wetam,barab boobu fa lanu tabax fi mu nekk jàngukaayu farañse bu mag bi (école française),ca penkub dëkk ba ,nee nanu ci safari lasasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer,la sëñ Ibra mom Sëñ bi gane àdduna,ca rabiihul awali atum alsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak benn,mu tuxoo fa dem ca këram ga nekk ca kaw tund wa,ginaaw bi mu ko tàmblee defar ca weer wa ko njëkk,loolu nag mi ngi amoon ca bis bu njëkk ba walla ba ca topp,walla ya ko jege,dal di koy tudde Albuqhal Mubaaraka,di ci maanaa pàkk bu nu barkeel bi. + +Ca ñaar fukk ak ñatt ci weeru sawaal atum balsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñaar,Sheex Abdul Ahad gane àdduna,ci muharram atum jalsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñatt,sëñ Abdu Xaadir gane àdduna,ci guddig àjjuma,ci fukki fan ak ñeent ci silqihda atum jalsasin ba tay sëñ Saaliwu gane àdduna,ci juroomi fan ci weeru kooru halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom sëñ Suhaybu gane àdduna di rakki sëñ Abdul Ahad,ci silqihda hasasin ba tay la sëñ Abdus Samad gane moom itam,ci rabiihus saanii atum jamsasis,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñatt,la Sheex Murtadaa gane àdduna. + +Mu tàmbli jumaa ji atum halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom,jéego ci ñaari tànkam yu tedd yi ci guddig dibéer,weeru rabiihus saanii,fàtte naa nag bis bi mu ci tollool,ñu tàmblee gas dal bi (fondmang bi) ci ñaar fukk ak juroom ñaar ci jmaadas saanii atum walsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan weer ak juroom benn. + +Tabax gi moom ñu door ko bisub altine ci yoor-yoor,Sëñ bi wàcc ci biir paxum xuba bi,Sheex Muxtaar Binta nekk ci wetam,yor ndab lu def ban ( xam naa simaa la war a jubloo wax) , Sëñ bi jël jumtukaayu tabax bi (turéel) dal di tibb ci ban bi (simaa bi) , wax bismil laah,sotti,jëluw xeer teg ci ban bi (simaa bi) ,jëlati gasukaay bi door ko ci xeer wi,jàng :”wa isyarfahu ibraahiimul qawaahida minal bayti,wa ismaahiilu rabbanaa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu” mu di ci maanaa :ba Ibraahiima di yékkati dal ya, (mbaa ponk ya, mbaa fondumang ya),ak Ismaahiil,,naan :yaw sama boroom nangul nu ndax ya’ay aji dégg ji,tey aji xam ji. + +Mu dal di fay juge,julli ñaari ràkkaa,ñaan. +Alhamdu lillah,ligéey bi àgg na ci juroom ñaari at,ci teewaayu Sëñ bi ,mu julli fa ñaari iid yi(tëbëski ak kori),ñaari yoon ci lu wër ,ñatteel bi kay laay sikk,waaye julliwu fa àjjuma . + +Sëñ Mbakke BUSO nee na li ko waral mooy moom kat masu fa’a yéenee sax mukk,(ku yéenewut a sax àjjuma waru ko), ka fa njëkk a taxawal àjjuma mooy Sheex Ibraahiima,rakkam ja,ci dëppoo gu mu ci def ak Sheex Mbakke BUSO,ak doomi Sëñ bi ak magi taalube yi,ndax ñoom ñépp a fa yéene woon a sax. Ndax Sëñ bi moo digaloon mag ñi ñu sanc ci wetam,bàyyi boroom kàttan yi man a ligéey tey tarbiyawusi ñu nekk ca tool ya,di ligéey di indi. + +Dëkk ba mujj di dëkk bi gën a dund, ak jàkkaam yeek daaraam yi,ak jàngukaayi xam-xam yi,kaamilub Sëñ bi nag bis bu nekk ñu wàcce ko ci bunt këram ñeenti yoon,ñaari yoon ginaaw jullig suba,aw yoon ginaaw tisbaar,ak weneen ginaaw tàkkusaan,bu dee guddig àjjuma ñu wàcce ko juroom ñaari yoon,mbootum loolu moom,Yàlla rekk a xam,mooy jullig farata gu mu julli gu nekk, tolloo’kub kaamil bu nu koy wàcceel,li ko tàmblee suba gi ba timis,juroom ñaar yi niy wàcce ci guddig àjjuma gi tolloo’k geey ayu bis gi = julli gu nekk kaamil. + +Bu dee lu aju ci mbindlu mi moom, da daan def képp ku mokkal te rafetum mbind,ñu daa ko bindloo ab kaamil ci lu tolloo’k ñatti weer yu nekk,walla sumun walla robo walla sulus walla nisif ci weer wu nekk,mu ànd ko ak ku mu nirool mbind,mbaa ñu mu nirool. + +Naka noonu ñi ko daan coobarewoo di ko def ngirYàlla,ci donga yi nekk ci biti,ak ñi ñu daa fay ci waa-rëw mi ak naar yi,weer wu nekk daa nanu am lu tolloo’k ay téeméer ciy kaamili loxo,lu bokkul ak li nuy jënd ci yu móol yi . + +Xam naa ne bis daal jëndandoo nanu juroom ñaari téeméeri kaamiil ci yu móol yi,ci benn yaxantukat,yu bokkul ak téerey xam-xam yiy dikk di juge ci wàll gu nekk,yu nu binde loxo ak yu nu móol,deesul delloo mukk ab téere,ak doonte dikk na fi ay yooni yoon,ak doonte danoo dagg ñaari wàll yi. + +Mu bire ci loolu ne menn njënd mi mu daa def moom saraxe rekk a ko waraloon ak doonte da ko daan suturaal ci ron ay njëkk,te loolu bokkul ak li mu daa seddale way ñàkk yiy laaj,mu di ag ndimbal ngir Yàlla,ak li mu daa jox boroom dara ja yi lépp ngir Yàlla rekk. +Leeg-leeg bis, mu seddale ci ay junniy junni,bokk na ci li gën a yéemey li ñiy gis, gis,te ñiy dégg, dégg ko,mooy daa am bisub ñaar fukki fan ak juroom benn ci weeru koor,atum bamsasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñaar, mu dajale nu,nun mbooleem bindkat yépp,yu rafet mbind yi,te booba ab takk bu réy ci këyit a ngi ci kanamam,mu ne nu ndax xam ngéen lu ma leen di doye ? ñu ne ko déewalaay,mu ne leen këyit gii daal laa bëgg ngéen bindal ma ci ab kaamil,te du ñu ne ma mukk teru waa ngii,ndare bu da ngéen ma ne kaamil baa ngii !, ndax da ngéen ko def ?,ñu ne waa-waaw,mu ne nu jël léen këyit gi ,nu jël ko ,seddoo ko ci sunu biir. + +Nga xam ne da ngay gis ku jël ñaari isib,bind leen ci bis,ak ku jël ñaar bind leen ,keneen maas leen, ñu tàqalikoo ci loolu ci yoor-yoorub juroom benneelu fan ba,ku nekk ci nun xam na la mu war a bind,ak baat ba muy yam,ca digganteem ak ka mu ko seqal, dunu ci dolli ,dunu ci wàññi. + +Kaamil bi noppi alhamdu lillaah,ci tisbaari bisub juroom ñeenteel bi,ñu jébbale ko, Sëñ bi xool ko,gisu ci lenn lu ko naqàri,du mbind mu gën a rëy moroom ja,du mu gën a sew,du lenn daal . Mu dal di sant Yàlla bu baax,daa di ne ndax déggagun ngéen fi ku bind walla mu bindlu ab kaamil ci ñatti fan ? Nu ne ko déedéet , mu santaat Yàlla,dal di jàng:(( innii laa udiihu hamala haamilin minkum)) muy ci maanaa,man de du ma sànk jëfi aji jëf ci yeen . + +Bokk na ci li gën a yéeme ci mbir yi,li ma daloon ,mooy man kat daa am bis may yër benn ci téerey siira yi (jaar-jaari yonnant bi),yaakaar naa ne téere boobu nuy wax “Zaadul Mahaad fii hudaa xayril hibaad” la,di ci maanaa yobbalub delluwaay ba muy ëlëg,ci jubug gën ji jaam yi,ba ma àgg ci ñi doon bindal Yonnant bi(j.y.m)maanaam ñi ko doon bindal wahyu gi ak bataaxel yi,ma lim leen ñu doon fukk ak juroom benn,Yàlla dogal ma ne naa xool nu itam ñi ci matal ab kaamil ci koor gii ñaata lanu woon ,far lim ba di benn,ca noona ma def ñaari woy,wenn wi ma ñaan ci Yàlla ci barkeb bindkati Yonnant bi (j.y.m),wi ci des ma ñaan ci ,ci barkeb bindkati Sëñ bi,am benn waay ci sama gaa yi ku ci tuxale ci man woyuw bindkati Sëñ bi te boolewu ci wu bindkati Yonnant bi (j.y.m). + +Ginaaw bi ma xool ci buntub ligéeykati Yonnant bi (j.y.m), ñuy juroom ñeent,ag jigéeen it nekk ci,mooy Barakatu yaayi Ayman,ma teg ci xool ligéeykati kër Sëñ bi,ca koor googee amul lu dul ñu toll ne ñoom,te ag jigéen bokk na ci, mooy Awa Saar jèbbéerub Sëñ bi,ma defati ñaari woy,kuréel gu ci nekk wenn tax la’a jug. Waaye ñaar yu saaba yi lakk,te kenn jotu leen a tuxal,ñaar yu ligéeykati ak bindkati Sëñ ba’a ngii: + +Bismil laahir rahmaanir rahiimi, +Muhammadu Lamiin Joop Dagana wax na di woy turi bindkati Sheexul Xadiim ca at ma mu koy woy,di leen tollale ak bindkati Yonnant bi (j.y.m) niki mu nekke loolu ci Zaadul Muhaad : + +(ci barkeb ñi jaayante ak ngën ji ligéeykati Yonnant bi,daan ko bindal,di ci gërëmloo aji des ji) +maa ngi lay ñaan ag jaayanteek moom gu dëggu,ni miy gërëme ku jaayante ak moom te di ko samp) +( ci barkeb Andariyi ,boroom mbégal mi,Muhammad mi nu tudde Bashiir) +( may ma ay mbég yuy leeral sama xol,yu di naa ci mujj di mbégum sama dëkk) +(fàtteel ma ci moom lu dul li nga ma tànnal,may ηoy (jàpp) ci wépp yiw wees ma tànnal) +(may ko ci yaw ak ci jëwrini Yonnant bi(j.y.m),mébëti xolam,akug jiital) +(yaw sama boroom nekkal ma cig aar,ci barkeb jaamam ba Muhammadul Amiin) +(nga dundal ci moom sama xol ci ay xalaat yuy tax nga gërëm ma ,bu ko defee ma dib jaam buy sant) +(na nga ko may ag aju (jébbalu) gu dëggu,ci darajay ki nga xam ne wommatal nga ko lu wér la) +(ci barkeb Sharif Mafaatim mu dañ mi kumpa,muritam bi nu melal ci ngënéel lu rëy li) +(teralal sama xol ci jikko yu rafet,may njariñ lu sax ñeel mbindéef yi) +(rafetalal samag dégg ak samay wax ñeel képp ku ma waxal yaw boroom may gi) +(nekkal ko, ci di ko may li mu bëgg,ci yiwi ñaari kër yi,mu doon ag am gu mat) +(yaw sama boroom ci darajay Daymaan,Muhammadul Xayri boroom koolute gi) +(may ma xol ak làmmiñ wu laab cig neen, ñu xam ko cig sàmm) +(te ma taqoo’k ragal Yàlla ak jëfe lu may tax a dab ñu mat ña) +(may ko mu tukkee fa yaw gërëm ak jàmm,juy des di ànd ak moom ba àjjana) +(ci barke turandoo wa ,muritam bu lewet ba,doomi Sulaymaan, Sëriñ Joob mu mucc mi) +(sarax ma saxug cofeel ak rafetal,ak ag ubbiku ci njàngum Alxuraan) +(ak jëllale ak dëddu lu dul lu rafet,ak jege luy bijjee jëme cig giim) +(màngal jëme ca moom ay barke yu sax,yu ànd ak sellug dund,ak mujj gu rafet) +(ak ci barkeb muriit ba ,doomi Sahiid NJAANI,Muxtaaram mu nu xam, mi mel ni Marjaan) +(may ma saxug noppi ci lu amul njariñ,tey wax lu am njariñ,te am njariñ) +(may ma kepp ku ma xam,mbaa mu dégg ma sopp ma ci lu dul ag xeeb) +(yéwenalal ko àddunaam ak diineem,te nga méng ko yoolub jiyaarkat yi) +(ci barkeb mbokkam ma ak saxiixam (mooy koo bokkal nday ak baay) bu baax bi,Ahmadu Binta boroom yéwén gu nu xam gi) +(may ma ag lewet ak xol bu yaatu,ba ma far nekk dib sang bu yaatu) +(may ma ag cawarte akug toroxlu,ak muñ,te nga sellal samy barab) +(na nga ko dundal yaw buur bi ngën ji dund,te nga def ko ci ginaaw bi muy dund ca àjjana) +(ak ca darajay doomi Faadil jii dib bindaakon,Majamba SILLA kay taarub bindkat yi) +(doxal sama diggante ak lu ñaaw ba fàww,ci lu bir ak lu làqu ak luy jax-jaxiloo) +(dóoral kiiraayul wattu ba fàww ci sama diggante ak bépp saay-saay bu dul jaamu) +(màngal ko yaw boroom bi,ci ñaari kër yi,barke buy aare ci ñaari gàcca yi) +(ak ci barkeb weer wi,doomi Muxtaar mi ñépp xam,di Ahmad waaye nu xame ko ci turu Moor Alima) +(may ma may taarub alxuraan,te nga may ma barkeb jàngale) +(kaweelal sama yite ci luy rafetal sama saayir ,ak sama baatin ànd ak xol bu laab) +(may ko yaw buur bi xam-xam ak jëf,ak teggiin yuy indi lépp lu mu mébat) +(ak ci barke doomi Ahmadul Muxtaar,Ahmadu Awa ,sang bu nu tànn bi) +(may ma ag baax gu ag bon dul toppati,ak ag nangu gu lamb dul jege) +(bépp ayib bu man a gàllankoore ci lu baax,na nga ma ko faral ba ma man a am texe gu sax) +(may ko lépp lu mu bëgg,ci yaw,te nga saxal bànneexam ci ngërëm ) +(ak ci darajay ki fëgg te sax fa,di Muhammad mi niy askanale Wajja) +(saxalal samaw làmmiñ ci wax aw yiw,ci waxtu wu nekk, ma noppi nag wëlif aw ay) +(na nga siwal samaw tur ci mbindéef yi,te nga def ko muy siiwug yiw) +(na nga ko may mébatam ci gii ak gee kër,di ku nu laaf ci mbooloom aji matale ji) +(ak ci barke doomi Ahmadu doomi Warxa mu Siin mi,kooku mooy Ahmadu KAN boroom askan wu nu ñongal wi) +(may ma ag aaru te setal sama lépp ci lépp luy taqal lu set) +((musal ma ci njuumte,may mag lewet,guy béel ak man ,ak jépp jëmm ju mucc) +(na nga tawal ci kawam niiri barke yuy sax ciy yëngoom aki dalam) +(ci barke ki niy wooye Ahmadu SAAXO,ki nga xam ne ab deram tër tilimalu ko) +(may ma nooyug kanam gu sax,déet ag ñëkk,gu koy ñaawal) +(na nga ma def may mbégum dëkkandoo yi,tey mbégum mboleem maas gi) +(na nga ko def muy boroomug dund gu teey,na nga def it ag deem di guy teey) +(ak ci darajay cam su nu sangal ,su gànjaru soosu,di Ahmadu mii nga xam ne aw dàkkantalam mooy Moor SIISE) +( may ma may kok du yékkati ab jéego jëme ko ci lu dul sa gërëm,yaw aji wattu ji ,ànd aki xéewal) +(na nga ma dëdduloo ba fàww ci lu dul luy tax nga gërëm ma,dëddug ku nu teral) +(may ko mu man a saxal li nga gërëm,ba man a làq sa gërëm) +(ak ci barke doomi Muxtaar mi niy dàkkantale Shams,te moom dafa mel ne ab jant ciw nitam) +(jeexalal sama xol ci yaw ,may boroomug dund gu sax ci yaw,tey boroomi yéene) +(na nga ma tàggatal njiit yi,te def leen ñoom ñépp ñuy samay soppe ci yaw) +(ak ci darajay aji ragal ji Yàlla ,aji yéwén jiy teet lépp lu bon,Ahmad doomi Saynabu ji) +(na nga ma may ag ragal Yàlla ,akug wattu akug dëggu,ci wepp yiw , may sàkku ag dëggal ci yaw) +(na nga teetal sama xol ag bëgg àdduna,bëgg gog da na man a lor kuy wutug jeex ci Yàlla) +(na nga ko gindi ciw yiw wow da na xeeb ba fàww sottikug niir yi,te kenn du ko xeeb) +(te ci barkeb Usmaan mi nga xam ne ñi ngi koy wooye Demba KEBE,méngoo ma te fegal ma njàqare) +(yaw sama boroom,ba fàww,na nga ma aar ci lépp lu my ñaawal niki wor) +(may ko yaw buur bi ba àjjana,muccug yaram ak xol) +(asaf naa nag ñu baax lool ci bindkat yu siiw yu kawey daraja yi) +(bañ gi ma leen bañ a indi doyadig pas-pas waralu ko,waaye kay li ma sartoon a def moo ci mant a boole keneen) +(yaw sama boroom,ci seen barke ñoom ñépp,na nga nangu sama ñaan gii ba fàww) +(na nga nu may mu tukke fi yaw,gërëm ak yërmaande,te nga rafetal mujjug ku nekk ci nun) +(ci darajay Ahmad ligéeykatu Ahmad,xéewal ak mucc yal na ko Yàlla mi ko yatt saxal ci moom) +(ak ñoñam aki saabaam ñiy boroomug soppante ci yaw,ngir sa jëmm,ci lu dul ngàññante) +(li feek kuy ñaan ci barkeb ku àgg ca aji rafet jay yonni yonnant yi,mi ngi am li muy ñaan). +Sama boroom yal na nga nu nagul,yaw ay aji dégg jiy aji xam. + +Woy wi mu defal ligéeykati Sëñ bi ,di ñaan Yàlla ci seen barke,tollale leen ak ligéeykati Yonnant bi (j.y.m),woy waa ngi nii: + +(yaw sama boroom ci darajay juroom ñeent yoy ligéeyal nanu ngën ji jëwrini Yonnant bi,kok kawe na képp ku ligéeyal Yonnant bi (j.y.m) ) +(saxalal sa ngërëm lu màgg li ba fàww,ci ki nga xam ne ag ligéeyalam lu nu saxal la) +(sama kerkeraan jëm ci yaw,kiy buntub samag tonowu,kiy far ñaawtéef yi,kiy dañal ag mbon) +(ci darajaj Malaamin NJAAY,boroom farlu gi ci ligéeyal Aji ñeewant jiy musal jépp aji gindee) +(may ma ag cofeel guy taqoo’k xel mi,ci jëmmi ki nga xam ne def nga ko muy leerug réew mi) +(na nga tàggat samay cér ci ligéeyal ko,tàggatug ka ma jegeel ci sottig xéewalam ya) +(na nga ma def ma sopp képp ku sopp,aji ligéey jii,na nga ma def may ku mu sopp) +(wommatal ko lépp lu mu mébat ci ligéeykat bi (Sëñ bi) ,niki muy xéewalee) +(ci barke sëñ Moodu FAAL,maa ngi aaru ci lépp lu ñaaw,ba fàww) +( may ko li mu mébat ci àdduna’ak allaaxira,te nga fegal ko ñaari gàcca yi ak ñaari sawara yi) +(na nga ma may ag mucc ci kiñaan ak bañ ab jullit,te nga leeral sama pas-pas) +(na nga def ci sama xol yërmaande ju may nooyale jépp aji wow ji xol,ba kero muy nooy) +(na nga may képp ku aju ci man ngën ji ag wommatu ñeel ma,ba ma man laa gërëmloo) +(ci barkeb aji lënkaloom ju lewet,di Sahiid SALL,na nga ma fegal mbooleem lu ag xuppe di nekk) +(màngal ko jàmm ak xéewal,gu sax ba kerook tàbbig àjjana) +(na nga ma ci maye ag jub gu sax ci lépp loo digale) +(na nga ma may ag not sama bànneex,ak bakan,ak saytaane ak àdduna) +(na nga seral ci man xolub samay dëkkandoo,ñu jub tey diisoo) +(ci barkeb camus Mbakke si ko daa rootal,di Aboobakrin,na nga dolli samay xeewal) +(sottil ci kawam ci dexi yiw yi,lol da na koy jañal lor) +(te nga kaweel sama yite ci moom ci li ma bëgg,ci lu dul may gestu lenn loo bëggul) +(na nga ma may ag toroxlu ci képp ku ma dajeel ci julliti jamono ji) +(na nga màggal ci sama xol ak sama bët,bépp murit bu askanoo ci man) +(ak ci barkeb ki mu lënkalool,di Sahiid MBAKKE na nga ma may mboot muy jooyloo képp ku ma bañ) +(may ko ci sunu sëriñ bi,la mu bëgg,ci àdduna’ak allaaxira ,mu dëppo ak la mu bëgg) +(na nga ma may ab ligéey ci darajaam,mu dib sarax tukee fa yaw) +(na nga ma may barke bob ku dul man dana ma ci ñee,ànd ak xol bu neex) +(na nga nu may nun mbooloo mi aju ci Sëñ bi,urma ju dul xottiku) +(ci darajay mbokkam ma Ibra MBAKKE,dañalal ayib yi ag dañal) +( may ko gën ji dund aki yiw yu koy bégal ci gii kër ak gee) +(na nga matal samag mbañ-rus,musal sama xol ci mbañeel,te kaweel sama daraja) +(na nga musal samay cér ci lépp lu bakkan man a ragal,ak doonte du lu metti) +(na nga barkeel ñeel ma,ci sama mbokk yi ci Yàlla,ak ñeel sama mbokk yi ci Yàlla) +(ak ci darajay doomi Maryama mi kawe fa Sëñ ba,miy Siidi Kala) +(yal na ko kiy namm, defal la mu namm,ca kaw nammeelam,moom miy aji namm) +(na nga ma def may ku dëggu fa yaw ci li ma bëgg te nga gindi ci man aji dëggu ji) +(na nga rafetal sama njort ci bépp murit bu aju ci sama sëriñ,te nga teetal ma ku nu dàkku ki) +(na nga ma musal cig yàkkamti,te may ma ma jot gaa ya) +(ci barke camus cam yi,Mbakke JUUF,mi amul lu muy ragal) +(may ma ma nekk kuy ligéeyal Sëñ bi li feek ma’a ngi dund,kii nga xam ne ligéeyal ko mooy ligéeyal aji jiitu ji (di Yàlla) +(tàbbalal ma samay xemmemtéef ciy xemmemtéefam,dammal samag dëddu cig dëddoom) +(ubbil ma yaw buur bi cig ligéeyalam,ag ubbi gu may aj ca kaw ña koy ligéeyal) +(na nga sellal ag dundam ci guddal ko,te musal ko ci ay gàkk-gàkk,walla nga def ko far lem) +(ak ci barkeb muritam bu jigéen ba Awa,jèbbéeram bay saxal lu baax) +(may ko texeg dund,aki néeg yu kawe ci ginaaw bi) +(may ma bakan bu dal ci Sëñ bi,bu doylu,bu dul jeng jëm ci ku dul moom) +(tàggatal ma jigéen ñi,te yombalal ma seeni mbir,te nga dagg jafe ga) +( yéwénalal ma ko te def ko muy ndimal ci topp la) +( na nga ma wisaareel ay doom yu góor yu baax ak yu jigéen,yu baax,yu am diine te ñong) +(ñoñ da nga dundal ci ñoom lislaam,di ma fegal ci ñoom yeddaange) +(ñoñ da nga leen di barkeel ci jox leen wërsëg wu yaatu,wu dagan,ba ca àjjanay Aji yaatu ji) +(na nga def ngën ji julli,goo xam ne da nga ci nangoo sama ñaan gii,ànd ak sutura su rëy) +(ak xéewal gu sax gu nu gëttal,ca ka ñu xeeñal ngën ji gëtt) +(di Muhammad,ak kuréelam ba bépp,te nga wuyyu ma ci seen barke yaw sama boroom) +(wuyyug nangu,ak ngërëm ak teral,guy tax may ku nu wormaal ci biir gaa yu baax) +(jeexalal samag dund ci lu rafet ci seen barke,ñuy ñu ñu béelal,ca saxuwaay bu kawe ba (àjjana) ) +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina. + +Cig gàttal daal,dundug Sëñ bi ci Njaaréem gisunu ko fenn ci nettali ak jaar-jaari kenn ci sëñ su mag si,ci sariiha ak haqiiqa,lu dul li tegoodi ci yoon ci ligéeyub buur yi,muy jéem a def àttey yoon yi,di dagg loxoy sàcc yi,di jam njaalokat yu senge yi,ak door ñu sengewul ñi,ak di leen tumbrànkeel,te loolu wuute ak àttey àtte gi (nguur gi),ndax àtte yooyu daganalunu loolu,te dëppoowul ak seenuw doxiin wu mat ci fànni politig yi. + +Fatabaarakal laa,ahsanal xaalixiin,mbooloo yi bari woon nanu ci moom ca Njaaréem,ba nguur gi mujjoon aaye ko muy dox ci nit ñi ci lu dul ag diggale,loolu taxoon muy wut ay palanteer yu ndaw,ci bunt bu nekk,ci wàlli kër gi gépp,nga xam ne fu mu tooge ba ubbi palanteer,ñaari nit ci ñu jege ñi man a gise bu nu jàlle ñeneen ñaar jegesi,noonu lanu koy nekke ci suba ba bëcëg ci li gën a bari,teg ca ñu nekkaat ca tàkkusaan ba timis ak lu ëpp guddi gi. + +Amaa na leeg-leeg mu dem bind ag xasida,mbaa mu dem ca buntub jigéen ñay siyaaresi,mbaa mu dem nemmiku njaboot gi,su bëggee jàngale,da daan soril nit ñi bunt bi,ñu kuréelu,def géew,mu tàmblee tomb ci suuf ngir njàngalem sariiya ak haqiiqa,ci alxuraan ak haddiis ak hikkam,ak masalay fiq yi,amaa na mu jànglu xasida,bu ko defee wattukat yi jug jéeb,ci kàddu gu neex,moo xam danu koy xool,mbaa nu koy tari,xasida yooyu daawunu weesu tagg Yàlla ak Yonnantam ba,bu ko defee lekk yi ak naan yi,di daw ci diirub jataay bi,lu fa waay soxla rekk ci àdduna ak diine. + +Nguur gi aayeeti ko mu dem ca jàkka ja,ba mu mujj def jàkkam ca fu jege kër ga,ndax moom kat daawul wuute jullig mbooloo ca jàkka ja,du guddi,du bëcëg,du tàngoor du sedd,du xiinadi ,du xiin, mu bàyyil nit ñi ci kër gi aw yoon wu nu man a jaar julli ji,moom mu wut aw yoonu boppam,wu koy àggale ca mihraab ba,du nu ko gis mukk,ndare bu daa taxaw ca mihraab ba,ubbi bunt bi ndare palanteer bu sew bob du tee ñu seen ko,ci mbooleem julli gi, bu ko defee mu daa tëj bunt bi bu noppee ci julli gi,daan ko ubbi it ngir jàngale. + +Nu aayeeti ko muy dox ci yoon yi,te kat nit moom ku soxlawoo loolu la,ba mu mujj aajowoo sàkk ab palanteer bu sew,te sori ci làkkub kër gi,digganteem ak làkk bi aw yoon wu yaatoo ñeenti xasab a nga fa,mu fay jaar bu bëggee doxontu suba ak ngoon,walla guddi. + +Nga gis nit ñi ñu wër ko,ci ginaaw palanteer bi,di dox ànd ak moom,di taxaw bu taxawee,ak fu mu jublu,amaa na mu taxaw ngir tufli leen bu noppee ci ñaan gi,mbaa mu jàngal leen am masala,jàng gi it da daan bir,loolu lépp ab politigam la woon ngir soxla gi ko nit ñi soxla,ngir jariñu,ak gindiku,ak soxla gi mu leen soxla ngir jariñ leen ak gindi leen,bu teelut a lijjanti loolu ñu lor ko ci taxaw ci kawam. + +Seere nanu loolu ndax kat bis dagg nanu ko ci baaraamam,dagguw dàllam it,ngir xér ci laal jëmmam ju tedd ja . +Waaye buuxante bu metti bi mooy waral ñuy dal ci kawam,ba koy gaañ ,te dunu jublu loolu . +Bu ko defee muy gaañu ci loolu ndax moom jëmm ju tuuti,te doyadib bind la waaye di ku dëgër ca Yàlla,du yoqat,te du sonnu,ba bi ko mbirum Yàlla mi dikkalee,ñu tànn ñaar ngir ñu toppatoo ko,ñuy ñaari muritam yi Muhammad mom Abdu Rahmaan Attandaxii, mi faatu,ci ginaaw bi ci sawaal,atum bahsasin,di junni ak ñatti teemeeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar, yal na ko Yàlla yërëm, kooku moo ko doon toppatoo ak mbokkam mi bind araf yii,Muhammadul Lamiin JOOB ,ñu duggal ko ab wata guddig àllarba yobb ko Tuubaa,ci pexe mom danu koo def ngir làq ko nit ñi . + +Ñi ko doon gunge juroom lanu woon,sëñ Bashiir moo leen jiite woon . Mu dal di yonnee ca mbokkam ma,sëñ Muhammadul Faadal,xalifab ñaareel bi, te ca jamono jooja,ma nga woon ca wurumub dëkk ba,ca wetu Tuubaa , mu yonnee ca Sheex Ibraayma ca Daarul Muhtii,ak ca sëñ Mbakke BUSO,ca dëkkam ba ca wetu Tuubaa,mu yonneeti ca mag ña nekkoon Tuubaa, ñooñu daje ci diir bu gàtt,ba nu matee ñaar fukk ak juroom ñatt,sëñ Mbakke BUSO jiite leen,loolu lépp a ngi ame woon ci làqu gu tar,ngir bañ fitna, ñi ngi noppi bi fajar daataa jot,def fa ab néeg bu nuy tëj ak a tijji, bi ko nit ñi yëgee bi suba jotee,coow li jolli,bul laaj nag wax yeek jëf yi,loolu lépp bi muy am sëñ Moodu Mustafaa ngi Njaaréem di xamal nit ñi ak di leen dalal . + +Bi nu noppee ci waajal gi,ma génn ci bunt bi ma njëkk a jot,laa daje ak kenn ci taalube yi,te booba moom yëgutoon li xewoon,mu ne ma man kat biig dama laa gént ,di la laaj Sëñ bi, nga ne ma: (( wamaa Muhammadin ilaa rasuulun,xad xalat min xablihir rusul)) muy ci maanaa Muhammad du lu dul ab yonnant,bu fi ay yonnant jiitu. Ma ne ko ni nga ko gente la deme de,duggal,bi mu duggee,tàmblee yéemu . + +Ki boole téere bi defal na ko marsiya (marsiya = xasida gu niy waxe jëf ju baaxi ku faatu) ci ay bayit mooy bi nu njëkk a defal Sëñ bi, bi mu fi jugee,mi ngii: + +(Sëñ bi wéy na jëm ca buur ba mu daa jaamu,ndax kat xamoon na ne fii kenn du fi des) +(mu wogu di sàmm ndigali Yàlla yi,ngir ngërëmam tey teet li mu tere) +(di tere lu bon tey digale lu baax,di def lu nu xam te du ca ëppal) +(nekkoon na kenob diine ca bisi dundam,ñoñam de,moom lanu jublu woon ci sàkku dëgg) +(gisoon nanu ne mooy seen baay,bu nu war a jox àqi baay,moom itam,mu gisoon ne àqi doom lu nu leen war a jox la) +(mooy ki daa fàtteloo jirim yi seeni cosaan,daan faye aw ay ciw yiw ) +(moom dey naataange la woon ñeel ñu ndóol ñi ko daa dikkal juge fu nekk ngir xontu) +( bu daganoon nu jote ay bakkan de,nu def ko,waaye ay sang jiitu nanu ko,juge fi,te kenn jotu leen ) +(waaye de na la woor ne bu fàddoo wëlif nu ànd ak jëmm ja tam,du tee aw yiwam wiy dolliku du fàddu mukk wëliif nu) . + +Buurub woykat yi it ca jamonoom ak wàllam,di Muhammad mom Muhallaa Alhasani defal ko moom itam marsiya bu yéemee yéeme,mi ngii: +bismil laahir rahmaanir rahiimi,wasallal laahu halaa nabiyihil kariim, Muhammadu mom Muhallaa,mi nu gën a xame Naana,mi ngi wax di marsiyaal Xutbub Xawsu bu boroomam bu mag bii di Sheex Ahmadu Bamba mi nu xame ci turu Xaadim,yal na ko Yàlla labal ci géejug yërmaandeem,te sarax nu ci barkeem, aamiin: + +(yoonu dee mooy dayob kuy dund,dund daal lu dul dee toppu ca) +(nit ñépp a ca jëm nag (moom dee), bu bettewul ci bëcëg gi ,def ko ci guddi gi) +(moom daa mel ni ab rawante bob mooy bant ba nu samp jëm ca,ku ko jéggeegul it ca nga jëm) +(ndaw dayo bii di bu yéeme !,moom de mooy saxuwaayu seeni mbooloo,tey dajekaayu seeni kuréel) +(lu waay tàyyeel tàyyeel du tee mu jot boobu dayo,lu waay sawar te bariy jumtukaay du tax mu romb ko ) +(dee daal daa mel ni ndabul nganale lu nu woo ñépp,woote gu matale te yaatu) +(bu aji ligéey ji wuyyo wooteg dee gi ti,te kenn bégu ci ) +(jotoon naa wuyyu cig njëkk wooteb Yàlla bi te booba gindikat yi jugagun) +(mu daa wuyyu wooteg képp ku woote jëme ci yoonu kawe ak teddnga ) +(mu nekkoon di kiy woote ak a gindee jëme ci ngérum jàmm ak mucc) +(moom de bi sàmmkat yi ruuralee seenum càmm,daa féeteek aji wattu ji,sàmm am càmmam) +(teg nanu ko lepp lu diis lol yanukat ba gën a mag gën a dëgër àttanu ko). + +Bokk na ci jikko yi mu ko limal: +(ak dagg buumi ñaawtéef yépp,ci lu dul gestu guy gàllankoor walla yoqat) +(ak dundal xol yi ci sikar ak waaraate yi rafet ci waaraate yi) +(yéem naa ku mel ni moom, ci niir ak tawub dundalug xol, bu nuy màng, jëme ca suuf yu bekkoor ,yu naatadi yi) + +Mu neeti: +(ki ko tànn daal a ko woo jëme ko ci teraanga,ngir fay ko jëfam yu baax yi) +(moom itam mu wuyyu,ba mu demee fekk fa la mu doon mébat,ci ngënéef yu gànjaru yi) +(mu mujj ñàkk gi nu ko ñàkk,di lenn ci way jommale yi,te di am mbamb (xew-xew bu njàng) mu lëndëme ni tàggeg tàggekat yi) +(Abdul Xadiim daal wéy na,di ku nu santi jëf,di ku ay mbootam lenni gàkk-gàkk nekku ci ) +(Abdul Xadiim daal wéy na, te bënul lu dul bëtub ay may aki xéewal) +(wari fas daal du woon yitéem, te ji ay tàndarma yuy dott it taxu ko woon a jug) +(dundug buur yi de dug dudam ,ak doonte day joxe ay bóoli yu nu feesal) . + +Tëj: + +Ñu tëje ko ci waxtaane lenn ci li ko Yàlla may ciy xéewal yu kawe njort, ginaaw bi Yàlla sooyalee seen ñatti pexe ya,muy ray ak tëj gu sax,ak tumbrànkeel gu sax . +Bokk na ci li ko Yàlla xéewalee ci safaanub ñatt yooyu - Sëñ bi nee na - def gi mu def ati tumbrànkeem di lu juge ci nattub yonnant yi ak seeni balaa,yi leen seeni noon daa teg,mi ngi wax ci loolu: +((bokk na ci xarbaaxi Yonnant bu nu gënal bi,yal na xéewali aji kawe jiy gënale nekk ci moom) +(bokk na ci xarbaaxam yooyu:nekkug sama ati tumbrànke gi di lu nu génnee ci jamono ju jàll ) +(ñu niroole ko ak la xewoon ca diggante yonnant ya ak ña nga xam ne ñoom ñépp ay kàccoor lanu) +(yal na xeewal ak mucc sax ci ñoom,ni Yàlla dàqe ak lëndëm ci yonni gi mu leen yonni) +(ag kéemtaan dey feeñ na ci sama tumbrànke gi,ni mu feeñe woon ci Yonnant bi moom mi gindee) +(loolu mooy ñi sabablu woon tumrànke gi de) +(ñee nañu ñi ko sababluwutoon ci noon yi,te Yàlla notal na ma leen ) +( ñi ko sabablu woon de dunu tàbbi àjjana te sawara lanu jëm ) +(te du nu am li feek tuubunu,lu dul ngën jaa saxi njàqare). + +Mu bëgg a wax ne Yàlla màg na te kawe,niroole na ci ngënéelam, li amoon ci sama diggante ak noon yi,niroole na ko ak li xewoon diggante yonnant yi ak seeni noon,ciy nattu,mu niroole la nu ca ame ciy xéewal aki njariñ lu nëbbu ak lu feeñ,fii ak fa nu jëm,mu niroole loolu ak li ma ci ame ciy xeewal aki njariñ . + +Mu tollale loraangey àdduna ak ju allaaxira ju noonam yi tuubul ak loraangey ña tuubutoon ca seen noon ya. Te ña sababoon nattu yooyu ak fitna yooyu,ñee nanu ñi ci àndutoon ak ñoom ,li Yàlla di wax naan: ((wa yawma yahaddus zaalimu halaa yadayhi,yaqoolu yaalaytaniit taxaztu mahar rasuuli sabiilan,yaawaylataa,laytanii lam attaxis fulaanan xaliilan,laxad adallanii hanis zikri bahda isjaa anii wa kaanas shaytaanu lil insaani xazuulan) muy ci maanaa : bis ba nit di màtt loxoom wiccax,naan aka neexoon ma topp Yonnant bi,aka neexoon ma bañ a def diw xarit,moo tax na ba ma réere alxuraan ,ginaaw bi mu ma dikkalee,te shaytaane dey day gàccaal nit rekk. Mu ne moom aaya woowu seere la ci Yonnant bi (j.y.m) ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom, tey kéemtaan,waaye di seere ñeel ma tey karaama,kon alhamdu liilaah,sant naa ko te gërëm ko,ci dëppale gi. + +Bokk na ci mbóoti sama tukki bi,xéewal gi ma Yàlla defal muy juroom ñaari karaama,tolloo’k kiimaani Yonnant bi (j.y.m),ñooy: Yàlla notal na ma samay noon njëkk samag feeñ, may ma xam-xam bu jugewul ci njàng, Yonnant bi (j.y.m) puukarante ak yonnant yi ci sama tumbrànkeg fukki at yi ak ligéey bi ma ko ci ligéeyal muy ligéey bu sell, Yàlla def ma may koo xam ne képp ku texe da na ko sopp,te naagul ibliis ci man ak képp ku nu rëbb, mu def ma may ku malaaka yi sopp,ak way gëmi jinne yi,def it julliti jinne yépp aju ci man ngir jëmmi Yàlla,mi ngi wax sax ci loolu naan: + +(( juroom ñaari kéemtaan ci yu Yonnat bi,feeñ nanu ci man,te am naa samag ñaan ca seenug njëkk)) +((sama boroom ci barkeb ku nu tànn ki ,notal na ma noon yi,njëkk samag feeñ,te du ma dajeek kuy noonu)) +((Yàlla may na ma xam-xam bu jugewul ci njàng,te indil ma Kun (mooy nekkal mu nekk) )) +(( Yonnant bi puukarante na ak yonnant yi yépp,yal na xéewalug Yàlla nekk ci ñoom)) +(( ci sama tumbrànkeg fukki at yi,ñu ànd ak ligéey bu sell ñeel boroom nekk gi ak jiitu gi (Yàlla) )) +((képp ku texe da nga ma sopp ba fàww,ngir jëmmi sama boroom miy aji delloo,sopp gu àndul ak ag mbañeel)) +(( Yàlla miy aji dimblee,naagul na ci man ibliis ak képp ku nu rëbb )) +((malaakay aji tedd jiy aji des,danu may bëgg ngir jëmmam ja,ànd ak texe gu dul dagg)) +((ñi gëm ci jinne yi,sopp nanu ma ngir jëmmi aji des ju may defali xéewal)) + +Mu waxaat ci beneen barab: + +((jinne yi gëm ci sama jamono jii aju nanu ci man,waxu ma, ñi gëmul)) + +mu neeti: + +(( mayal ñi ma ligéeyal lu rafet,moo xam malaaka la,mbaa ku nu làq (jinne) walla nit)) + +Nu xame ci loolu ne moom kat am na ñeneen ñu dul nit ñu koy ligéeyal,mu waxati ci beneen barab: + +((Muhammad may na ma ag not,képp ku dëkkaale ak moom du nu ko not)) +((samag texe day des ci lu dul rékki,Yàlla notal na ma mbooleem ay noonam)) + +Mu waxati: + +((kuy léewtoo jubluwu ma,bëbbug (xeewali)sama boroom lu feeñ la,ibliis de du léewtoo’k soldaari aji tedd jiy kenn)) + +Mu neeti: + +(( wattu naa lu nu ñogal wëlif téere yi,kon bul tàyyeel ci ligéeyal ma)) +(( Yàlla màngal na ma mbooleem xam-xam yi,aji tedd jii de baax na , +mooy aji dañ ji kumpa,tey aji xam ji)) +((kiy def lu ko soob de nocci na xam-xam yi ak seeni barke ñeel ma,ci nekk ngi mu nekk di aji xam)) +((ki nga xam ne wommatal na ma aw yiw,wuy sellal xol,te yiw wa wommatu de,déeyaale na ak man)) +((Yàlla xéewale na ma jàngale,di naa gindi ku réer ak ku am xam-xam)). + +Bu dee ni mu bëgge ñi gëm nag ak ni ko ñooñu bëgge,loolu moom jarul sax nu ciy wut lu ko seere,ndax mbir la mu niy gis,di jàkkaarloo ak moom,muy barig jariñ gi mu leen di jariñ ,ci xam-xamam ak alalam,aki mbóotam,aki ñaanam, du amadi solo ñu tudd cis lëf ngir barkeelu ci,am na fu mu naan: + +(( jéggalal jépp aji gëm ju góor ak ju jigéen,jéggal guy saxal wépp yiw)) +((jéggalal bépp jullit bu góor ak bu jigéen,jéggal gu leen di musal ci tooñkat yi)) +((jéggalal jépp aji rafetal ju góor ak ju jigéen,jéggal gu leen di wommatal lu rafet)) . + +Mu neeti ci Matlabus Shifaayi: + +(( na nga saafara mbooleem jullit ñi,ci fii,te nga fegal leen tiit ak njàqare ca fee)) +(( na nga leen musal te jàmmal leen,te ñeewant leen,te bul fayyoonte ak ñoom ngir barig seeni bàkkaar )) +((ndax ñoom kat bu nu la moyee ngir sàggan,du nu la bokkaale ak kenn)) +(( te seeni yaram àttanuñu sab nattu ,ngir seenug doyadi)) +((seeni xol de du jéng jëm ci ku dul yaw,ba fàww, ci fii ak ëlëg )) +((waaye nekk gi cér yi nekk di ban,bijj na leen ,yobb leen ci gën jaa boni bon-bon yi)) +((bul fayyoonte ak ñoom ci lu la dul wàññi,may leen li leen amal njariñ,te amalu la njariñ )) . + +Mu waxati ca xasidaam ga tudd (Fastajaaba lahum rabbuhum): + +(( ci darajay Mustafaa,wuññilal xeetam wi njàqare,yaw mi génne sa jaam bii ca njàqareem la)) +((bindalal Yonnant bi xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam yiy boroomi teet lu bon )) +((musalal aw xeetam ci darajaam ak seen daraja ñoom ñépp,yaw kenn ki ma notal)) +((wuññilal njàqare ñi di boroomi gëm,yaw miy kiy maye ag koolute)) +((yaw aji rafet ji,àggaleel ci mbooleem jullit ñu góor ñeek ñu jigéen ñi,jàmmi boroom mbindéef yi)) +(( bindal ag sell ñeel mbooleem way rafetal yu góor yi ak yu jigéen yi,yaw mi méngoo way gëm yi)) . + +Ak lu bokkul ak loolu lépp ci li nu manul a lim,ci lii di wone bëgg gi mu bëggal xeetu Yonnant bi (j.y.m) li mu bëggal boppam,mu jagleel ci boroom jagle yi,geneen bëgg gu gën a tar . + +Dégg naa ko bis (g.y.m) mu naan :man dey jamonoy samag ndaw,dama daan tànn ci giir gu ne ab xarit,daan ko jagleel ci sama xol ag cofeelug boppam,ni ma tànne woon ci giirug Daymaan,Muhammad Yaddaali,boroom téere bi nuy wax (Zahabul Ibriiz),ci giirug Tandax ma tànn fa Muhammad FALL mom Mutaali,ci ñoñ Haaj ñi, ma tànn fa Ahmadu doomi Muhammad,boroom (Jawharul Munazzam). + +Bokk na ci li mu nu nettali ci cofeelam gu yéeme gi ak mbëgéelam gu tar gi ñeel ñennat ñi ci jullit ñi; nee na bi mu nekkee ca tumbrànke ga ca géej ga,daa yëggoon ne sunu mbokk mi Muhammad SEKK,mi nu gënoon axame ci turu sëriñ Làmbañ,ak sunu mbokk mi Muhammad JOOB,ñu gënoon koo xam ci turu Majoob Aram Seriñ Fittu, tubaab bi da leen a yobbu woon ngir tumbrànkeel leen,xawma fan nag,bi mu ko defee mu amoon lu ko naqari lool,nee na àdduna dal di lëndëm fi man,sama jamono nëx ngir ñeewant leen,ndax kat bëgguma ñu nattoo leen lu leen di tax a ñàkk seenig gëm,mbaa mu koy rékki ci ñoom,yal na nu ci Yàlla musal,ma dal di ñaan Yàlla ci seen mbir moomu ne: +(( yaw gën ji aji jéggaley bàkkar,tey gën ji ku man a musal ku nu jàpp)) +((na nga dindi jullit ñi cig njàpp,te musal leen ci luy waral sikk )) . + +Ñaari bëyit yooyu ñi ngi ci xasida gi tudd ((wa àmmaa maayanfahun naasa fayamkusu fiil ardi)),man naa am bi muy bind xasida gi la ko seenub xibaar dikkal,mu dal di def ñaan gi. + +Bu dee bëgg gi ko ñi gëm te di boroom jagle bëgg ,loolu moom lu nu xam la te siw,seereel nanu ko yiw wu nekk,ak wilaaya gu nekk ci barab bu nekk . + +Doggantal : ci seere gi ko ñu mag ñi seereel ag màgg ak ag wilaaya + +Xoolal Sheex Siidiya mii ak màggam gi mu màgg lépp,téewul mu tegoon Sëñ bi fu mu tegul kenn,bind na ci moom,woy ci moom wesar ci moom,bu waxutoon lu ëpp ñatti xasida yii tam,ci xasidaam yu bari yi,loola da na doy,ñooy yii: + +(Sheex Ahmadu daal xéewal la ,gu Yàlla jox mbindéefam yii yépp) +(ag cant ñeel na Yàlla mi ngi xam ne ay xéewalam jaamam yi manunu koo takk,mbaa nu lim ko) +(boo dajee ak moom,fekk ñuy yekkati raayob teddnga,da nga ko gis mu alawtiku ko ci loxol ndayjooram,ànd ak di tudd Yàlla ) +( bu gisee bis jikko yu rafet yi ñu dëdd leen,day dogu jublu ya ca gën a mag) +(suuf su ko dëkkal daal ,ab lolli bu ko ñàkk a ndàndal du tax mu lor ko ) +(miskiin yi ngir sa baax gi fàtte nanu seeni dëkk,ba mujj na sa koom mii de lanu jàppe seenum koom ) +(seen mbooloo yooyu de buy daje ak ñoom mbégte mu rëy te dëggu lay àndal,nga xam ne da ngay jort sax ne,lu toll ne li mu leen di jox ciy xéewal rekk,lanu koy jox )) +(( mbooloo yépp seere nanu nekk gi mu nekk di ku baax,ku tedd,kuy jaamu Yàlla te dib tuubaakon )) +(( bokk na ci ñi gisoon jariñ nit ñi di farata,ci jamonoom,tey ci ñi daan tudd Yàlla )) +(( dogal bu ñëw mu nangu ko te gërëm ko,xam ne Yàlla’ay ki ko dogal )) +((bu kuy tëñëxu cig lëndëm di tëñëxu it,moom genn muuraay du man a muuri bëtam wëlif dëgg gi )) +((kersa du dañ di ab rootukaay ci sab hadara,bu ko defee yiw yi di noyyi ci gelawam lu sedd li)) +((jaam yi de ,dox gi nu dox jëm ci moom,seeni aajoy àdduna’ak allaaxira’a ko waral)) + +Ñaareelu woy wi,mi ngi ko def bi mu tàmblee tabax jumaay Njaaréem ji,mi ngi nii: + +( jàkkay Sëñ bii de mooy jumaay barke ji,tey barabub ay yiw ak yërmaande ) +( fa lanuy jéggalee ñaawtéef yi,ña koy siyaare it seeni yiw danu koy ful) +(boroom fondumangub ragal Yàlla la ,ak miiri jëf ju baax ak teraanga) +((jëf ju sell ñeel boroom mbindéef yi,ci yeene,te jëf ya’a ngi ci yéene yi) +(boobu barab de,làquwaayub ku bëgg a taxaw guddi ngir jaamu Yàlla la,kon de bu baax la,làquwaayub ñu ndool ñi de làquwaay bu baax la) +(bu fa julli ngir Yàlla amee ab néeg it,du tee muy neegub jokkoo ngir Yàlla) +(xamal nanu fi julli ay waxtu,waaye jàkka jii de am na lu dul waxtuy julli rekk) +( nit ñi danu koy jublu,ànd aki xol yu boole lu tàqalikoo ciy yeene) +(ab kuréel bu fay ñëw ngir julli,ak beneen bob mbiram mooy asaka ) +(Yàlla digale na ñu yèkkati ay néeg,yu tedd ci kaw yeneen néeg yi,ngir turam wi) +(yal na Yàlla faye tabax gi, ay kër yu niy tabax ca àjjana,ay jigéen nekk ci) +(Sëñ bi daal xéewal la,gu Yàlla joxe,di kiimaan ci kiimaanam yi) +(nit ñi de xam nanu ko ci penku bi ak ci sowwu bi,mu dib sang ci taax yi ak ci kaw gi ) +(mi ngi bokk ci tabaxkati jëf ju baax,te loolu lu néew la ci nit ñi) +(dellu nanu seeni kër,ànd akug cant,gu toll ne cantug ku soxla woon am ndox Yàlla jox ko dexug Furaat) +(yal na ko Yàlla wattu ci wattoom ga akug kaweem,aki doomam yu gó0r ak yu jigéen) +(ak ñoñ néegam bu kawe bi,mboole seen,ak muritam yi juge ci wàll yépp) +((te Yàlla may ko “Xurratu Hayni” (am mbégte) ci àdduna ak allaaxira) . + +Ñatteel bi ci yu mujj la,da fa mel ni danu koo wonoon ne ab digam daa jotoon : + +(burub nit ñi yal na la fay ngën ji fayam,te dolli la ci teralam gi ak mayam gi) +(te mu desal la fi,ngir mbindéefam yi nga xam ne,sag des moo di seenug des,xéewale la mooy xéewale leen) +(kuy jéem a tolloo’k yaw bu woomlee tam,nan lay yéege ba jot ku ko gën a woomle fopp?) +(nan lay yame kok am koomam mi ngi ci joxe ko, ak kok mi ngi ci denc ko ak làq ko? ) +(ndax kuy jënde alalam ab yool ak ndam,da na mel ni ku nuur ci njaayam ma’ak njëndam ma ? ) +( cam la su teddnga di feeñ bu feeñee,bu làqoo,sooroolub njèkk làqu ) +(bis bu Yàlla dogalee tenqam gëbum koom,da koy dal di seddale way yalwaan yi) +(day jàppe jeexug alal,akug naaxsaayam, muy di ko jéem a màggal ak a dajale,joxe ko ci yoonu Yàlla it mu jàppe ko muy li koy yokk ) +(bariwaa na ay gawar yu mel ni ay cati xéej,naaga (giléem) yi daw ak ñoom,jéggi ab àll,bob suuf sa daa mel ni asamaan sa ) +( ki leen di wommat,di yaakaar ju rafet ji nu am ci moom,ki leen di gindi di kaweem gu rafet gi ) +( ñu jublu ,bu nu àggee ca ëttam ba,fajug seeni aajo ci lu dul nëx-nëx,ànd ak am lu leen ci wóor ) +( ayibam daal du lu dul jaamu Yàlla,ak jariñ nit ñi suba’ak ngoon) . + +Aji seere ju mel ni moom cig ragal Yàlla,ak am xam-xam,te di ko jëfe ak sax ci sunna,doy na sëkk. Xam na aw yiw,ak barabam,dal di koy laabiire jaam yi,tegtal leen ko,yal na ko Yàlla fayal lislaam ak ñoñam. + +Xoolal ku mel ni Sheex Sahdu Abiihi,wàlliyu wu ñépp nangulug wilaayaam,bokk ci néegub teddnga,di ci askanu Yonnant bi(j.y.m),xoolal ku mel nii wax ,bind,wesar,woy.Bokk na ci li nu ko askanale ci lénn ci ay bataaxelam,ginaaw bi mu santee Yàlla ,julli ci Ynnant bi,da ne: ab nuyyoo ngi juge ci man jëm ci Sheex Ahmadu Bamba,yal na Yàlla rëbb ku ko bañ,te rëbb ku ko waral,ma lay ñaan nag nga bañ maa fàtte,te bañ a fàtte xeetu Yonnant bi (j.y.m) . + +Lii nii juge ci sang bu màgg bii,ag laabiire la ñeel xeet wi,di it ag tegtale gu muy tegtale aw yiw, di ko junj,junj gu nooy,te làqu. Mu ne ci ag xasidag ndokkeel,bi Sëñ bi dellusee ci tukk bu nu barkeel ba,ginaaw bi mu defalee Sëñ bi ag seede ci bayit,wu yàgg,muy: + +( jamono giñoon na ne da na fi indi ku mel ni moom,waaye ee jamono,sa ngiñ gi amul de,kon demal kafaara ji ) . + +Mu neeti: + +( tubaab ya’a ko jële woon ca mbellam ya,mu mujj ca géej yooyee di wurusu ngalam ) +(mu feeñe ca xori géejug mbàmbullaan ga,di wurus wow ag leeram akug xuy-xuyam tax na ba bët yi gëlëm) +(mu di weer wu leer,wu fàddu ci sowwu bi,feeñaat ci dib jant cig yékkatiku ak ak tasaaroo ) +(yéemu naa ci wurus wii nu jaarale cig nattu, mu mujj di wurusuw yaaxoot,wu deesul jaayante ab taar ak moom) +( yéemooti naa,na ngeen xam ne buntub tuub ak njéggal de,ubbi nanu ko,ñeel bépp murit,bu sàkku ci moom ag dëkkaale )) +(ag ndokkeel ñeel na diine jii, nga xam ne mujj na di puukarewu ci yaw,ngir mbégte ak ndamu ) . +Esklëy,eskëy,xoolal ma wàlliyu wu tedd wii,ga xam ne làqul lu dul ag dëggu . + +Xoolal ma wàlliyu wii,Sheex Mustahiin Alkumayli,sunu mbokk mi ci Yàlla ak ci Sëñ bi,Alhaaji Muhammad Abdul Laahi doomi Ubaydur Rahmaam,nee na ca téereem ba tudd (( Annafahaat Almiskiyya Fil Xawaarix Almbàkkiya)),: bi tubaab bi tuddoon Kaylaan - yal na nu Yàlla musal ciw ayam - laajee Sheex Siidiya,lan mooy àtteb jiyaar ji jullit ñi di def ci nasaraan yi,ci jamono jii,ndax lu dagan la ,ginaaw nasaraan yi dunu leen def lenn lu ñaaw ci seen diine,ak li ni nu leen di ëpp doole lépp,ak li jullit ñi di néew doole lépp ? +Mu tontoo ko la mu ko tontoo ,mu jébbal tontu bi Sheex Sahdu Abiihi,mu gaaral ko ko,bëgg mu wax ci, mu bind moom Sëñ bi,lu mel ni li Shayxaani (Buxaari ak Muslim) bindoon,jëme woon ko ci wàlliyu yi ak boroom xam-xam yiy jànkoonte ak ñu dul ñoom muy: ki bind araf yii de Yàlla def na ko muy buntub texe ak mbégte ak njèkk . Dara ci loolu jubluwu ko,ndax moom kat féex na ci fitnay àdduna ak allaaxira,atun kasasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,bu feexutoon ci fitnay àdduna ak allaaxira,kon mu indi tontu bu ñatteel,waaye moom mujj na ,bokk ci ñi ñu wax ci ñoom (( bal ahyaaun hinda rabbihim yurzaquun)),muy :ñoom de fa seen boroom ñuy dund lanu,ñu leen di wërsëgal, loolu ki ko wax a ko bind di,Ahmadu mom Muhammad,mom Habiibul Laah,yal na ko Yàlla mu kawe mi musal,te nekkal ko te méngoo ko. +Subhaana rabbika rabbil hizati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina . + +Dégg naa Sheex Mustahiin mu naan: loolu de dëgg la bu dutoon dëgg du ko bind. Dégg naa ci Sheex Bashiiru mom Sëñ bi,mu nettali jële ca Sheex Mustahiin mu ne: man de yéemu naa ci mbirum Sëñ bi,toog nanu ak moom bis ,di mbooloom boroomi xam-xam,yaakaar naa ne Abdul Laahi Ibnu Muxtaar Alhaaji,ca la woon,mu tàmbli di wax ak ñun wax ju yéeme,ju dugg sunu xol yi,ñu bégg tey dëggal te xamunu sax dëgg-dëggi li miy wax,waaye mu jàpp sunu xol yi,nu xame ca ne ca Yàlla la juge. + +Sunu mbokk moomu nu tuddoon nee na ci téerem bi nu tuddoon : + +bokk na ci karaamay Sëñ bi,yal na ko Yàlla wattu,dellusi gi mu dellusi bawoo ca dun booba,nga xam ne kenn la fa tubaab yi masul a yobb mu dellusi . Sànni nanu fa nit ñu bari,waaye de kenn a ci dellusiwul,loolu mooy firnde li gën a mag ci ne moom demam gi moo ko tànnoon,dëgg naa ne Sheex Mustahiin mom Talha Alkumaylii,nee na : moom de bu bëggutoon a dem du dem,dunu ko man a génne it dëkkam. +Te kooku doy na ndëërlaay. Sëñ bi bindal na ko ag laabiire gu mu tudde, “Diyaafatul qudoos,wa laa yashummu raaihatahaa dayfu ibliis” muy ci maanaa nganaleg Aji sell ji,ag xetam du xeeñ ganug ibliis. + +Daa na siyaaresi Sëñ bi ,juge fu sori di liiru (dox ci tànkam),daan bañ bu ko Ku tedd ki masaan a jox alal,bu ko masaan a jox sijaada ngir mu ciy jullee,da ko daan jël di ko taf ci dënn bi, te daawul nangu deesi sàggane ko. + +Li Sheex Mustahiin waxoon rekk, la sunu baay Muhammad Alkuntiyyu,mi nu gën a xame ci turu Bu Kunta ca Njaasaan wax, ca wetu Tiwaawon . Kenn ci taalube yi nee na ,booba dafa’a demoon di ko siyaareji,mu laaj ko Sëñ bi,te booba xam na ne mi ngi ci tukki bi,ne ko ana Sëñ bi,mu ne ko moom de tubaab yee ko yobbu,mu ne déet,bul wax loolu,mu ne ko lu may wax kon ? Mu ne ko,moom kay daa dem ligéeyi,fa ligéey ba neexe,murid bi nee booba maa ngi fi ma toog di dégg nit ñuy wax te xamuma dara ci li niy wax,mu ne ma ndax dégg nga làkkuw gaa yooyu ? Ma ne ko déedéet,mu ne ma li ko waral da dul seenuw làkk,ndax Sëñ bi njëkk muy tukki,daa samp ab làkk wërale réew mii,kenn du fi man a am benn taalube,ba kero muy ñëw,man nag samay taalube maa ngi leen jële ci ginaaw làkk bi,samay taalube dunu ñëw li feek ginaaw weer walla ay weer. + +Bokk na ci kilifa yu mag yi seereel Sëñ bi,Sheex Abdalla Attamkali Addaymaani,wax na te dëggal te rafetal: +(dama ne jéngal jëm Daaru Salaam ak Tuubaa,boo ragalee ay mbamb,aki coowi jamono) +( ngir nga ame fa’b xool bu tukkee ci xawsub jamono ji,bob da nga ci ame njéggal ak’ag texe) + +Ñaari bayit yii de maa ngi ko mokkale ci Sëñ bi,ndax bis da ne ma ndax xam nga ñaari bayiti Abdalla yi,ma ne ko déedéet,mu jàng leen ma dal di leen mokkal,xam it li mu doon junj ci dëggal wax ji ci nekk di “xawsub jamonoom”. + +Boroom xam-xam bu màgg bi ,Sheex Abdul Laah Attandaxii Albohbiinii,nee na bi mu siyaaresee Sëñ bi Njaaréem: + +(boo mujjee ñëw wàlliyu yépp, ba noppi kawe leen,na nga xam ni ngën ji mbindéef de,ci xarnu yu mujj yi la ñëw) . + +Sheex Abldullaah mii de mooy ki Sëñ bi ne woon :Abdullaah ag xasida’a ngii,gog ku ko mokkal ,Munkir ak Nakiir du nu ko laaj ci bàmmeelam,Sheex Abdullaah ne laaylaaha illal laah,ana mu ? Mu ne ko mi ngi ak Muhammadul Amiin mii,mu ne giñ naa ne di naa ko mokkalloo samay doom ak samay jigéen,ak samy jaam,yu jigéen ak yu góor,mu nekk di lim rekk ak a dëël,Sëñ bi moom di ree rekk. Xasida gi mooy Jaawartu. + +Sang bii moo ma nettali woon,nettali bu yéeme ba,masumaa dégg lu ni mel,da ne ma sama mbokk man dey daa am bis,may jàng li may faral a jàng bis ci Alxuraan,bi ma ubbee kaamil bi,amul lu dul Yàlla mi man lépp won ma bisub (( alastu birabbikum)) muy ba mu naan (ndax du ma seen boroom?). +Nee na ma jàkkaarloo ak xew-xew ba,gis yonnant yi,yonnant topp yonnant, yu bari yi ak yu néew yi,teg ci ma jàkkarloo’k wàlliyu yi,wàlliyu teg wàlliyu,ak seen mbooloo yu bari yi ak yu néew yi,ba mujj ma gis jenn jëmm,mooy Sheex Ahmadu mii,gox yépp fees dell aki taalubeem,mu génne ci Hadara bi ,sori’s lëf,dal di wëlbatiku ne ana ku may jottalil ab yonnee sama boroom ?,wax ko ñaari yoon ba ñatt,Yàlla tawfeexal ma, dëgëral ma,ma ne ko man,mu gestu ne ma ndax yaw la diw ? Ma ne ko waawaaw,mu ne boo ko defee de ,ba nu dem àdduna di naa la defal,di naa la defal..,mu ne ma neel sama boroom,mu dolli ma,ndax sama ñi ma topp de danoo bari te bëggaluma leen lu dul lu leen di bégloo,ak wax yu mel nii,ma dugg,ci biir,wax li nu ma waxloo woon,ma gis nu koy jox , ba ma dégg ko mu naan doy na,dal di dem. + +Eskëy,moom de ci jëlewaayi (masdar) Sheex Sahdu Abiihi la bokkoon. Xibaar boobu nettaliwu ma ko kenn,lu dul ginaaw bi mu faatoo,ci ndigalm,sheex bii nag sama xarit la woon,te nekkon bu Sëñ bi,mas na maa yonni ca Sëñ ba di ko ñaan doomam,mu ne nee ko sàkkuwu ma ko lu dul ngir xér ci am lu ma jaxase ak moom ci fii ak ëlëg . Sëñ bi ne ni mu ko waxe la de,ñoom de bi ma nekkee seen réew sàkku woon nanu ma’a jox seen doom,waaye ma ne leen wuuteg aada yi moo nanguwul loolu rekk . Maandu na te dëggal. + +Bokk na ci ñu mag ñi ko seereel,Alhaaji Ibraahiima Albaxdaadii,moom de ci kiimaani araab yi la woon,mi ngi juge woom Baxdaad,ku meloon ni moom ci xam-xam moom jafe woon na,Sëñ bi moom ci jëmmi boppam nettali na ma ne gis na Alhaaji Ibraahiima mii,booba gone la woon,muy tukki di ànd ak waajuram wu góor,ak Xaali Majaxate Kala,ñuy ànd ak Latjoor,bis nee na gis na ko mu toog ak ñaari sëriñ yooyu ci lalub sëriñ Buubakar FALL,yéeme lool ci barig nettaliy xam-xam yi mu leen doon defal,ci noonu Xaali manutoon a ñàkk a bind nettali yi,mu yonnee nu woolu ma,ngir ma bind xam-xam bu bari bii,mu diy woy,ngir mu bañ a sànku,ma dikk,muy wax may bind,muy lu bari ciy woy. Ma dégg ci sama waajur mu naan masumaa gis ku man a mokkale ni naar bii,ku dul Alhaaji Omar Fuutiyu,moom de jamono ju nekk mi ngi naan:Buxaari nee na,Muslim nee na. + +Nee nanu bis laaj nanu ko turu buur bii,mu ne Latjoor,buur bi bég lool ci waxam jooju,bi loolu jàllee ba teg lu tollook ñaar fukki at,walla lu jege,ginaaw bi Sëñ bi jugee ci tukkib géej gi,la ñëw ci moom jébbalu,fàttali ko la xewoon bu njëkk,mu yéemu lu bari,nettali nanu ne bokk na ci li tax mu jébbalu,daa am bis mu ànd ak Sëñ bi cib tukki,ñu yendu ci ron genn garab,dëgg naa ci Sëñ bi,mu ne Alhaaji moomu booba mi ngi tux,mu génne gënn gi,am lu mu sotti ci loxoom,daa di ne ma loo wax ci lii ? Ma ne ko defal te bul laaj,mu ne ma ,duma man a ñàkk a laaj,ndax wuute gi da cee bari,ñii di ko daganal,ñee di ko araamal,ma ne ko ,bu dee noonu la deme de kon lu lënt la ci yaw,mu ne waa-waaw,ma ne ko xanaa gisoo Axdariyu,mu ne ma ahakay,gis naa ko,ma ne ko moom de nee na ca njëlbéen ga,daganul ci mukàllaf mu def dara te xamul la cay àtteb Yàlla,kon doo ko bàyyi,ba xam li ci Yàlla wax?. + +Sama wax ji wedamloo ko,àgg ak moom fu sori,mu sëgg ab diir,siggi,ne ma seereel ne bàyyi naa ko ngir Yàlla,dal di jug ca saasa,suul gënn gi,ak li ci nekkoon,ca bis ba mbaa ginaaw bi la jaayante ak Sëñ bi,jébbalu ci moom . + +Bi ñénn ci mag ñi yëgee ne jébbalu na,ñu tàmbli di ko yedd naan ko yaw ak sa màgg gi ak sa xam-xam bu bari bi,lu tax ngay jébbalu ci ku ñuul kii? Mu ne ko man dey Baxdaad laa juge, ni nga ko xame,yitewoowuma lu dul ku ma jox sama loxo,bari na wàlliyu mbaa boroom xam-xam bu ma romb,te xetug li may wër xeeñewuma lu dul ci moom,looloo waral ma aju ci moom, jaayante ak moom,ci noonu ñu dëggal wax ji,dogal ko ngànt. + +Bi mu delloo ci Ku tedd ki,nettali ko li nu ko doon wax,Sëñ bi bindal ko lii: +Wasslaamu halaykum wa rahmatul laahi,wa barakaatuhuu, +ma lay xamal ni ca sama xasida ga tudd ((masaalikul jinaan,fii xidmatil mutahhiril janaani)) di ci maanaa,soobuwaayi àjjana yi,ci ligéeyal kiy laabal xol yi,bayit yii a nga ca: + +(( Képp ku ma jorte lu dul kuy ligéeyal Ku nu tànn ki,man de dama koy ligéeyal ca la mu tànn)) +((dama koy ligéeyal ba kero may dugg àjjana,kërug sax ga,ak mébat ak xéewal )) +((képp ku yaakaar ne man na koo bégale ni,ni ko sama ligéey biy bégale )) +((na xam ne réer ak réeral wor na ko,te ci moom la ma lu dagan di dikkale juge fa boroom ba)) +((taggoon naa ko bu njëkk ca Libarwali,ag tagg gu wàlliyu yépp a ci lòtt )) +((taggoon naa ko ca Maayomba,tagg wu far samay ayib te dindi samay bàkkar)) +((taggoon naa ko fa niti Kalwaa,tagg wu ma fegali noon ak musiba)) . + +Nee naa ci ligéey bi ma koy defal (j.y.m): + +((ñeel na ko tukkee fi man,ab ligéey bu taqoo’k rawdatoom ba (bàmmeel),ba yawmal xiyaam te màgg)) +((sëtam ba Jiilaanii gëram na ma,yal na ko Yàlla mi ma kaweel gërëm)) +((sëtam ba Abool Hasan gërëm na ma,yal na gërëm luy saxalub taar nekk ci moom)) +((Attiijaanii gërëm na ma,yal na gërëmul kiy alag ibliis nekk ci moom)) +((ñeenti Xalifa yi gërëm nanu ma,làq naa gërëmul ñu ñu jegeel ñi)) +((ku ma gërëmul de,Yàlla Mu tedd ,mi moom gërëm na ma,ngërëm lu dul dog )) +((yal na Yàlla fay Mustafaa ngën ji pay,ni mu nangoo te amal ab dëël )) +((jullig ki nga xam ne teraangaam day daje ak man,yal na nekk ci ki nga xam ne mooy ki dëxëñ )). +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal + +mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina . + +Li nag booy xool ag junj la ci ne ñi ko ci doon yedd de,xamunu dëgg-dëggi mbiram,kon lu tax waxunu lu mel ne li ki leen xamul waxoon ? : +((yaw ki nga xam ne dëgg-dëggi am mbiram xamuma ko ,aka neexoon ma xam luy dëgg-dëggi mbiram)) . + +Bokk na ci li nu soloo ci seere yi ko mag ñi seereel,mooy ne Sheex Muhammad mom Abiibur Rahmaan,Attanaduxii,da daan def fu nu tudde Sëñ bi ci wetam mu yëggal boppam,ne cëy cam soosu,moom dey fu ma ko nemmikoo rekk,fekk ko ci sama kanam,lu tolloo’k aw xur,walla ñaar. + +Sama mbokk Muhammadu Abdur Rahmaan,Ibnus Saalik Baaba mom Halawi,wax na ma ne xalifab Sheex Ahmadu Bun Buddin,ak doomam ju màgg ja,Muhammad Amiin,nee nanu ko Sëñ bi de wilaayaam gi, indi na ci ay firnde, aki lay yu leer, ñépp gis ko, kenn ku am aw yiw dey du sikk ci wilaayaam gi. + +Bokk na ci seere yi,li ma Muhammad mom Ahmad, mom Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci taalubeem yi,ci turu Muhammad Tuubaa,ngir barig lu mu fa daa nekk ak Sëñ bi,li mu ma nettali woon,muy moom de bis seeti na ay nijaayam,ni nu ko baaxoowoon a defe,mu dem ca ku yéeme,ku bëgg ka Yonnant bi ak jëwrinam,di Muhammad FAAl,doomi Muhammad mom Ahmad mom Haaqil,mu yobbante ko ab nuyyoo akub siyaare ca Sëñ ba,sàkku woon it ci moom mu jox ko barkeelub mbubum njiitlaay,mu mu daa sol, ngir mu barkeeloo ko,nee na ma jotal ko Sëñ bi mu bég ci,jox ma njiitlaay lu ndaw,lu mu daa jiitloo,maanaam turki,mu ne ma gaawal jox ko ko,ma indil ko ko,mu bég ci lool,di ko foon ak a teg ci bopp bi,ag bët yi,nit ñi dégg ko,mujj ku ñëw rekk,ñaan ko,ma barkeelu ci,ba mu mujj sànku,mu sàkkuwaat ci man ma demalaat ko,ne ko nit ñi de sànk nanu sama barkeelu ba,na ma sarax beneen,ma dikk ci Sëñ bi,leerale ko ko noonu,mu bég,jox ma beneen,ma indil ko ko,mu sànt Yàlla bu baax,tagg Sëñ bi lu bari,man itam mu sat ma,ne ma boo jébbaluwutoon ci Sëñ bi de, di naa wax ci yaw kon loo xam ne !,waaye jébbalu gi tax na ma fiire la . + +Bokk na ci seere yi nu tuxale ci doomi mbokkam ma,Ahmadu Yoora Muhammad : lenn ci ay àndandoom danu koo yeddoon ci néew gi mu néew lu muy siyaare Sëñ bi,mu ne leen wallaahi,bëggumaa deem di ko siyaareji te yor ci sama xol,lu toll ne fepp suuf ci bëgg àdduna,kon fii ma toog laa koy siyaaree ,eskay.Ana ku gën tedd Muhammad,moom daal doy na sëkk seere . + +Néeg bii ki ci gënoon a taqoo ak Sëñ bi,gënoon cee rafet lu mu wax,mooy Ahmadu mom Abdallaah,ki bokk ak ñoom ñaar nday ak baay,moom dey moo’k Sëñ bi danoo meloon ne benn bakkan,seere naa bis Sëñ bi di jànglu lenn ci ay xasidaam,ñu jàng aw bayit mooy: ((taqdiimu Ahmadabni Habdil laahi, yahrifuhuu xayru xabiyyin laahi)),muy ci maanaa jiitalug Ahmadu mom Abdul Laahi,ku dul ab dof,buy fo xam nga ko,bi nu tuddee Ahmadubnu Habdil laahi rekk, xelam dem ci,Ahmad moomee,mu ne nanu ko ko wool,bi mu ñëwee,mu nettali ko ne tudd gi nu ko tudd,ci biir njàng mee tax xelam dem ci moom mu woolu ko, moom itam mu bég ci,sant ci. +Ahmadu mii nag mi ngi faatoo Ndakaaru,bàmmeelam a nga fa,siyaare naa ko . + +Bokk na ci seere yi ,li ma Abal mom Baay Addaymaanii,nettali,mu ne moom de sax na jamono ju yàgg ci,sàkku ci sunu boroom mu won ko,maqaamam Sëñ bi,mu ëppal bis ci sàkku gi,ñu ne :yeen de du ngeen xam ci Sëñ bi,lu dul bu ubee ba toog ngir daje ak nit ñi,ngeen ne kii de mooy Sëñ bi,mbaa mu ubbi mihraab bi,taxaw,ngeen ne Sëñ bi de jiite nanu,lu dul loolu ciy mbiram de,fàddu na leen. + +Ma ne wax jii de niroo na ak waxi Uwaysul Xaranii,sangub way topp yi,ji mu waxoon lenn xalifa yi, ne ko: yeen gisu leen ci Yonnant bi (j.y.m) lu dul keram !,nu ne ko Ibnu Quhaafa sax gisu ko,mu ne leen déedéet . Habal mii nettali na ma karaama,gu bàyyikoo ci goroom,baayu soxnaam,mu ne moom de daa am bis mu nekk cib xaymaam,moo’k doomam,mu koy bësal boppam,ndax daa jékki-jékki woon rekk buur ,buur gu metti,te gaaw (buur = jékki-jékki rekk jug),bi mu ko defee,dal di génn xayma bi,door tànk bi cig weñ,ba nu dégg ni ci tànk bi dale,te foofa génn weñ nekku fa,ci noonu tànk bi damm,mu rot ,xëm,bi mu ximmee,ñu laaj ko,lu mu doon,mu ne daa gis aw wàlliyu wu ñuul,di Muhammad mom Mahluum,ñu jénge ko ay weñ,mu bëggoon koo xettali,door tànk bi ci weñ gi,ngir damm jéng bi,far tànk bi damm,werul ci damm-damm boobu,ba kero mu faatu,yal na ko Yàlla gërëm te nangul ko jëfam,bi mu daataa faatu,bégaloon na doomi Daymaan yi,ci ag ubbiku gu yaatu ci alal,bu wàlliyu woowu dellusee,mu nekkoon ni mu ko waxe woon. + +Bi Sëñ bi dellusee,mu jël leen,bindkati xam-xam yi,ak alxuraan yi,seeni waxambaane ak mag ñi ba ci jigéen ña ak gone ya,di leen sotti ci alal lees manut a misaal, ña ca rafetle ak ña ñaawle,loolu di jàppndal akug tàggatal gu tukke ca Yàlla, ñeel leen,te di ndimbal ak sarax bu nu def ci sekkare,di ag ligéeyal lislaam it,ak Yonnant bi (j.y.m) ci xeetam wi . +Ni nu binde woon la ñeneen it binde woon,ci naar yeek ñu ñuul ñi,waaye ci ñoom la gënoon a siwe,gën cee feeñe. + +Bokk na ci ñu màgg ñu barkeel, ñi seereel Sëñ bi,Haamidun mom Muhammad mom Muhanda Baaba,ak doomi baay tëxam yi,Baaba ak Ahmad, ñaari doomi Mahmuud ak Haamid yi, ñoom ñépp , ñu ñu jagleel lanu woon ci moom,boroomi wax yu rafet it lanu woon ci moom . + +Yàlla dogal, bi Sëñ bi nekkee Cëyéen yonni woon na ma Dagana,ba ma fa àggee,Ustaas Haamid dégg ma, booba da fa’a ganesi woon Alhaaji Bekaay SEKK,yàggul dara mu seetsi ma,bég ci dikk gi ma fa dikk,yendook man ca sama kër waajur,di ma laaj ci mbiri Sëñ bi,aki xibaaram ,yi ci di yu nu man a tas,ak yi ci di yu ñu bari mant a xam,bu ko defee muy ree rekk,bég lool ci Sëñ bi , aki mbiram, ci noonu ma won ko teereb Sëñ bi tudd “Masaalikul Jinaan”,mu sëgg ci,siggiwul ngir dara,ba kerook ngoon di jot,mu ne ma Sëñ bi de ñëw gi mu ñëw ci jamono jii nu nekk de,firndéel na yiwam wu bari wi . + +Lii nag ag mosle rekk la ,waaye waxi ak seerey sangi naar yi,fii taxu koo jug, fi ko tax a jug kay mooy sunu téere bi tudd,(alminahul miskiya,fil xawaarixil mbàkkiya). + +Da nanu ci dolli li nu man ci tudd murid yi ci ñoom,bu soobee Yàlla. Bokk na ci kilifa yi ko seereel,sunu sëriñ tey sëriñub jullit ñi ci Senegaal,soppeb Sëñ bi,tey mbokkam,ci jegeñaaleg diine ak askan,ak réew,Alhaaji,Maalik SI, yal na ko Yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom Aamiin,dégg naa ko,ku dul man it dégg ko,ba xaw naa doon lu ñépp xam,mu ne: amul kénn ci nun ku dul koo xam ne,daa def lu ñaaw,ba noppi,tuub ko,te jubal,bàyyi ag dëng,ku dul Sheex Ahmadu Bamba,moom de daa judd,rekk di def lu baax ak a rafetal . Maanaam loolu mooy ñun ñi ñiy tudd ñépp de,amu ci kenn ku gisul ci boppam ab rëcc-rëcc,walla ay rëcc-rëcc,bu ko defee mu tuub ko te jubal,ginaawug dëng,ndare moom,moom dey ,am mbiram cig ndawam akug magam ñoo yam rekk,lépp ag tegu ci yoon la.Moom de wallaahi dëggal na,te laabiire. + +Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci turu,Muhammad Tuubaa,xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def,daa romboon Tiwaawon,siyaare Alhaaji Maalik SI,bi mu xamee ne ca Sëñ ba la jëm,mu ne ko man de da ma laa bëgg a yobbante ay baat ca moom,boo àggee na nga ma ko nuyyul,te fàttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndakaaru,ci benn néeg ñun ñaar rekk,kenn ñatteelunu ku dul Yàlla,bu ko fàttalikoo ba xam ne maa la yonni ,nga ne ko,man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom,maa nga ca kollare ga ma defoon ak moom.Muhammad nee na man de wallaahi,xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. Bi ma àgsee ba fàttali Sëñ bi guddi gi,ba mu fàttaliku ko,ma wax ko li mu ma wax,mu bég ci,dëggal ma te dëggal ko,tagg ko bu baax,tàmbli di coppati sama nopp bi,ak sama bakan bi,boole ca di ree rekk,ngir bég . + +Bokk na ci mag ñi ko seereel ba tay Xaali Majaxate Kala,xaritu Sëñ bi,tey mbokkam ci diine ak askan,ak réew,xaritu waajuri Sëñ bi la woon,da daan def ,bi Sëñ biy jàng,saa su ko masaa na romb rekk,sànni ko aw bayit walla ab jumla,ngir nattu ci ab tolluwaayam ci nahwu,muy (xam-xamu tegi wax ci yoon) walla bayaan:(xam-xamu rafeti wax) ngir ñawal am xelam, leeg-leeg,mu génneel ko ci ab yàq,leeg-leeg,déedéet,ba mujj Sëñ bi far ko raw,bi Sëñ bi màggee ba weesu fi mu tolloon,mu mujj naan ko,yaw de doom nga woon,waaye leegi baay nga, donga nga woon it,leegi sëriñ nga,muy lu mu dëggal te fas ko ci biir ag kaf,akug woyofal . + +bokk na ci li nu koy askaneel,aw bayit wu yéeme,yaakaar naa ne tàmblig ag xaasida la : +(tukkee na ci man jëm ci Ahmadu Bamba,mi bàyyi nit ñi,ngir Yàlla ,mujj far di sangub nit ñi ) . + +Bokk na ci li nu askanale sang bu màgg bi,Sheex Muhammadu Alfuutiyu,baayi Zannuuni,ak mbokkam ma Ibnul Harab,mi bokkoon ci jëlewaayi Sheex Sëhdu Abiihi,bayit wii,moom tàmblig xasida la gu mu defal Sëñ bi : +(mi ngi jëm ci kok Yàlla da koo defal ag tàllal (ay xéewal) akug wéttal,àtteloo ko ci àddunay jinne yi ak nit ñi) . + +Moom xasida gi,gu yéeme la,téewlootuma ko fii mu nekk, wax na ci, ci wenn bayit wu muy waxante ak Sëñ bi,naan ko: + +( sotti leen ci seeni miskiin,desiitu kaas bi) . + +Sëñ bi daan def,saa su gisee Zannuuni,defaral ko ab kaas ne ko, càkkutéefug sa baay la woon, Zannuuni mii,mi ngi bokkoon ci woykat yu mag yi,yu rafetooni woy yi,def na ab diiwaan ci tag Yonnant bi (j.y.m), def beneen ci tagg sëriñ si,rawati na Sëñ bi,mooy ki ci wax lii: + +( yaw xarit bi,ndaw sa bunt bii,bari lu ko siyaaresi,ci buur ak jaraaf,ak jinne ak malaaka) . + +Loolu di tàmblig xasida gu rafet, te yéeme,moo’k baayam ci jëlewaayi Sheex Sahdu Abiihi lanu,yal na leen Yàlla gërëm,mi ngi faatoo Cees,nu denc ko ci almeeri Sheex Ahmad Baru, siyaare naa ko, alhamdu lillaah. + +Bokk na ci kilifa yi seereel Sang bi,sëñ bu màg bi,di Sëriñ Tayba, Muhammad Ndumbe Maar SILLA. Sëñ bi nee na ma sëñ boobu de,fu mu ma masaa na gis rekk sànni na ma bayit wii,di ci seere ci sama mbir,mi ngii: +(bariwaa na baay bu yéege ci doomam,ay tundi teddnga,ni Hadnaan kawee ci Yonnant bi) . + +Mu bëgg a wax foofu ne,cam sii de ab taar la,tey ag mat ñeel cosaanam. + +Bokk na ci kilifa yi seere,sang bu màgg ba Alhaaji Abdulaay SIISE,mom Saalum,nekkoon na di ku rafeti wax,ak pas-pas ci Sëñ bi,am na bis aw nit di wax cib jataayam ba tudd Sëñ bi,ak jële gi mu jële wirdam wi ci Yonnant bi (j.y.m), am ci ñi teewoon ,ku ci waxe ni kuy weddi,Alaaji gëdd ko,ne ko looy wax nii ?,xanaa Sheex Ahmad Tiijaan waxul ne lenn ci ay wirdam Yonnant bi moo ko ko jox (j.y.m) ? mu ne ko ahakay, mu ne ko moom de,nekkutoon lu dul boroom xam-xam,bu jëfe xam-xamam,bu ragal Yàlla,te doon jëfe sunna, rafet gi nu rafet njot ci moom moo waral nu dëggal ko,kii nag di Sheex bamba,xanaa melul ni moom rekk,di boroom xam-xam buy jëfe xam-xamam,ragal Yàlla tey ku sunnawu,ndax kon du nu ko dëggal,ngir rafet njort gi nu dëggale woon kee ?,waa ja wedam, amul lu mu tontu . +Hasbunaal laahu wa nihmal wakiil,nihmal mawlaa,wa nihman nasiiru. + +Ag cant ñeel na Yàlla lii doy na ci li sama xel man a joxe,li am nag mooy,bu ma joyaloon samab gog,féexal xel mi ci mu dikke li mu wattu,ak li ma wattoo ci samag maas,ci lu wér ak lu wéradi,kon de ma indi fi gën jaa yéemey yu yéemu yi,waaye kon loolu am raddu rekk lay doon, ñax gu nekk a ciy nekk, ag jub ak ag jubadi,dëgg ak safaan,looloo tax ma tànn indi fi li ma man,teb yool nekk ci,ndax kat déet ab yool,ci lug jub nekkul,bu nu doon tollale li ma indi,ci li ma indiwul,da nga naan benn la ci junni,li ma xam it bu nu ko doon tollale ak li ma xamul,da nga naan as kook la ci géej . + +Yàlla mu kawe mi,laay ñaan mu baril sama lu néew,te wisaare ko,te nangu ko,te dimble ma, moom kat mooy aji tedd jiy aji gën, kiy boroom ngënéel lu mag li. + +Tàmbli nanu ko te mu mat,cig barkeel,yal na Yàlla nangu,te dimbalee,te yekkati,te wisaare,Aamiin. +Yaw buur bi, jéggal ma, ak sama ñaari way jur,te nga yërëm leen ni nu ma yarewoon may ndaw . + + +Jiitalug aji firi ji: 1 + +Jiitalug aji taalif ji: 2 + +Doggantal gu njëkk gi: ci xamale kuy sëriñ bi ak ay mbiram, 4 + +Doggantal : ci ni mu nekke woon ginaaw waajuram, 9 + +Doggantal : cig sancam Jolof 19 + +Doggantal : ci tukkib géej gi 24 + +Doggantal : ci dugg gi ca gaal gi 33 + +Doggantal : ci ñibisi juge ca géej ga 47 + +Doggantal : ci ñaareelu fàddu gi dem Gànnaar 52 + +Doggantal : cig ñibiseem ci tukkib ñaareel bi 67 + +Doggantal : cig génnam Jolof jëm Njaaréem 69 + +Tëj : ci wax lenn ci li ko Yàlla xéewale 80 + +Doggantal : ci seerey gaa yu baax yi 84 + +Bii article bu am solo la, ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom-koom, ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di The Economist, di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk, te adduna bepp xam ko, muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp, moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar 1843.Economist Newspaper Limited (Filiale de Pearson) ca London moo ko génne. Li ñu ci gën di wax nag mooy koom-koomu adduna bi, politig, jëflante, xaalis, xam-xam, xarala ak fànn (art). Lim bu ci génn, di nanu ci defar lu ëpp milyoŋ, te 80% ba ca biti Angalteer lanu leen di jaaye-ji. Yëglekaay gi tas na ci lu tollook 1.138.118 ciy yax ci xaaj bu njëkk bi ci atum 2006, ci li gëstug bureau of circulations wax, di jumtukaayub natt bu nekk ca Angalteer. 53% ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa Amerig lanu, 14% ay waa Angalteer, 19% di ñu dëkke Tugal gu goxe gi (continentale). Yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook 206 réew. + + Faith in the market (ngëm ak Business) + +19 desambar 2006 / Rom ak Tuubaa (Senegaal) + +Ci ginaaw luumay Itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si, am mbooloom jullit mu Afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde “addunaal” di (mondialisation): + +Kepp kuy door a teg tànkam ci suufus Rom, péeyub Itaali, dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon, mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg-leeg as lëf ci lii di Cappuccino, di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca Itaali. +Bu ngéen jëlee yoon wi jëm Vatican, jaare ko ci Via Della Conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme, da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo Afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu (waso), ay saag, ay der (ceintures) walla ay weeri jant yu nu roy, maanaam yu doonul piir. +Bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu, bu ngéen moytuwul, da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax, mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk-der yi, mu dig (dàqante gu xoromu te yërëmtalu). Nii daal lanu koy nekke, saa su nu léen yëgalee ne takk-der yaa ngoog, da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas, seeti nu nu man a mucce, bu Yàlla dogalee rëccuñu, bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu, moom kay danu ko fay bàyyil takk-der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam, daal di leen yobbu. (…) + +Ca dëgg-dëgg, jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme Vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu (organisewuwunu). +Ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu, gu nu xame ci adduna bi ci gëm-gëmu diine ak bu koom-koom, te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di Tuubaa, nekk nag ci digg Senegaal, boo fa jëmee nag juge Dakar péeyub Senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool. + +Niki yeneen imigireyu bari yu Senegaal (yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca New York, walla ñu diy wattkati suraas (orange) ca Espaañ) jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca Rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye “yoonu murit”, mooy yoon wi ëmb taalubey Cheikh Ahmad Bamba yi, kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum 1927. ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem Sëñ bii, indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey (maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi). + +Li ëpp ci 11 milyoŋ yi dëkke Senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu Murit mbaa wu Tiijaan, moom nag (yoonu Tiijaan) moo fi jiitu wu Murit. Bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ((ag murit)) leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul Lislaam, gas reen ya, xame ko na ko Yonnat ba indee woon. Waaye nag moom Lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo Araabi Sawudit. Lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax (culte des saints et de leur tombeaux ) muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel ba ci bu seen sëriñ boobu sax, te loolu ñoñ Wahaab ñi danu koy weddi, di ko kontar. Waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi (ñoom wahaabit yi), ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg, tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa Araabi Sawudit dara ba dara booloo jeex. +Sheex KA di sët ci Bamba, ca biir këram ga nekk Tuubaa, di dëkk bu fees dèll ak ragal-Yàlla, waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa, ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme, moom Sheex KA mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp: (( bu ngéen wéeroo ci keneen)) mi ngi nuy leeral (( du ngéen gore mukk, lii mooy sunu gisiinu dund)). Bi mu fi daataa juge Bamba mébetoon na ay mbir yu bari: bëggoon na Tuubaa, dëkkam bi mu sanc, nekk dëkk bu sell. +Njabootam gi – ci déggiin wu yaatu wi – Mbàkke-mbàkke yi, ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam-xami diine, yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb, maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte. Xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey, ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo, ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ (sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di wër adduna bi, ngir nemmeeku-ji seen taalube yi) ak ngir suqali dëkkub Tuubaa bi. + +Lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli Afrig yi gën a tèkki, moo xam ci seen réew la mbaa feneen. Fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje. Seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit. Ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat, ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus, yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man, te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey. Nan jël ku mel ne Aliyun KA, ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan (vente en gros) ca wetu gaarub Rom ba tudd Termini. Moom rakk la walla mag ci Sheex KA mi nekk Tuubaa di topptoo njaboot gi. Aliyun KA mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër ( walla sax ñu duli senegale ), bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi. Lenn nag ci njaay mii Senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo Endonesi, Thailande mbaa End. + +Teewul Aliyun nangu ne am na leeg-leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees. Moom nag Aliyun, ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge Banglaades, ndax nee na ((ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji (meteo) ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi ! )). Am na benn yoon ci mbedd mi, Sang Ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante. Jaaykati saag yii ak der, nga xam ne yu ci ëpp Siin lanu juge, ñu ligeeye leen fa, danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam-xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk-der yi. Bi añ jotee, gan dikkal na Sang Ka, di benn waa reewam N. GEY, mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi Senegaal yu tàng, plaat bu nekk 5 euro. + +Benn yoon ci ayu bis gi, lu ëpp ci murit yi nekk Rom dananu daje ngir def daayira (julli, jàng Alxuraan aki Xasida), gisante, siyaarante,xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal. Leeg-leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer, yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo, ngir nu jaayaat leen ca Sandaga, ja bu nekk ca Dakaar, te murit ya ëpp fa. Ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis, looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi Senegaal. Waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy: woo seenub xarit walla xame ca Sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla. + +Ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci 40% ci askanu Senegaal wi. Waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey Senegaal yi nuy tollale ci 700,000. Murit yi it ñooy daanaka 80% ci jaaykati Senegaal yiy wër, tey jaar ci mbooleen qàli Itaali yu mag yi. (Fraans mi doon dooley sancaan ji tegoon loxo Senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një. Ay fukki at a ngii Itaali nangu barabam boobu ci moom, waaye nag jamono jii ñu nekk Espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci Itaali. Lii sax moo waral ci weer wi (desambar 2006) lu jege 80 waa Senegaal ñoo sànku ci ndox mi, ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon Espaañ, ca dunam ya tudd Canaries). + +Lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn. Loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom, te mooy sukkandiku ci sa bopp. Lu man a xew nag, ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag. Bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga, def fay weer. Te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski-ji, bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di Màggalug Tuubaa, bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti Tugal ci jamonoy lòlli. +Jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi nu def ci wàllug njiit. Ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan Xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la, di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy ki mujj ci doomi Bamba yiy dund. Kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko. Cig ayam Tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba. Ci atum 1958 bu ña fa dëkk weesuwutoon 2000 nit, leegi àgg nanu – man nanu ne - ci ay 700,000 nit. Alkol nag ak Póon danu leen a aaye ca Tuubaa, moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir Senegaal. Ña nga fay taxawal daara ju mag (ab université). Boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine. Jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it, ñu ci bari it dunu musóoru. Xale yu góor ya’ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba (école). Saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay (hopital) mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi, ay milyoŋi eurooy dajaloo, ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu, ku ci mel ne Elhaaji JUUF may futbal ca Bolton (Angalteer), ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub Tuubaa ba (…) +Xamagunu leen de bu baax, waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de, du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation (di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew, benn xalaat, xatal soreente yi, jegeele gis-gis yi añs), waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme… + +lii tasawudus sixaar la di teere bu s bamba def ci lislaam + +Ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi,ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni. + +Maa ngi tàmblee ci turu yàlla, miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira. Yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang ,sunu kilifa, Muhammad,ak ñoñam aki saabaam,ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii, yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal,aamiin yaarabal haalamiin. + +Ahmadu mi dul dañ di sant boroomam, di jaamub yàlla,tey ligéeyal yonant bi (j.y.m) nee na : ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll,rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal.Maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid (muy wéetal yàlla),ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan,te ñooy sunnas yonant bi(j.y.m),xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba,soppeem ba,Ahmad,ak ñoñam ak saabaam yu gëm, yu jullite,yu tedd,yuy rafetal yi. + +Lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la, ma tudde ko yobbalub ndaw ñi(tathawudush shixaar) jem ca àjjanay yàlla jii ami dex,maa ngi ñaan yàlla ag +nangu,ak jàmm ak sell,ak màggal. +Maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub. +Tey texeg ndaw ñi,ak mag ñi,ak waxambaane yeek jigeen ñi. +Waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na,sunu boroom laa ciy wut ci lu sax. + +(AG JIITAL ) + +Yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub,te soxlawoo xam-xam,soxlawoo leen jàng ak mokkal,te teet barabi texeedi yi,taqoo leen ak ki dul +dañ di jaamu boroomam,ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme,kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub,bu màgge noppalu. +Ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen,te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell,ak jublu sunu boroom,am la gën. Jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox,kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira,bokk ci ñiy texe. + +(BUNT CI XAAJI DIINE YI) + +Diine ñatti xaaj la,benn xaaj bi mooy bu gëm, +Beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu,ak bu lihsaan,muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom.Lu ci ne dees na ko gën a leeral. +Ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm . + +Gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi,ak teereem yi mu wàcce,ak alaaxira,ak yonenteem yi ak dogal bi. + +(DOGGANTAL (chapitre) CI NI NUY GËME YÀLLA) + +Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam. + +Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. +Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) . + +Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, +(dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk). + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME MALAAKA YI +yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom) + +Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu. +Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde. +Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI) + +Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. +Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), +juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). +Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel +Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom) + +Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom. +Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal. +Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom. +Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal. +Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem ) + +Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak +sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay. + +Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone. + +Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi . + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME DOGAL BI) + +Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi. + +Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame. + +(BUNT CI LISLAAM) + +Lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa (muy yàlla rekk ay buur,amul beneen buur bu dul mom) ak julli ak woor,aj màkka,natt asaka. + +(DOGGANTAL CI LAA ILAHA ILLAL LAA) + +Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx. + +(BUNT CI JULLI YI JUROOM) + +Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña. + +Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër. + +Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, +deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la. + +(DOGGANTAL CI LAAB) + +Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, +ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la. + +(DOGGANTAL CIG SOÑÑEE CI ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK CEE SÀGGAN) + +Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete, +ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara. + +Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li. +Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp mi ni mu ware. + +Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji. +Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub +ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi. + +Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna, +kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele. + +Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu. + +Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko. + +(DOGGANTAL CI FARATAY JULLI) + +Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi. + +(DOGGANTAL CI SUNNAY JULLI) + +Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12 li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18 am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir. + +( DOGGANTAL CI FARATAY NJÀPP ) + +Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 +raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj 8 gaaw + +(DOGGANTAL CI SUNNAY NJÀPP) + +Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi. + +(DOGGANTAL CI FARATAY SANGU) + +Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu + +(DOGGANTAL CI SUNNAY CANGAAY ) + +Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi. + +(DOGGANTAL CI FARATAY TIIM) + +Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul. + +(DOGGANTAL CIY SUNNAAM) + +Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi. +Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim. + +(DOGGANTAL CI WOOR) + +Woor ñaari farata la am: 1 yeene 2 ba liy dogloo ngir yàlla. +Sunna yi ñatt la : 1 gaaw a dog 2 yeex a xëdd 3 ba wax ju ñaaw + +(DOGGANTAL CI ASAKA) + +Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yeene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. +Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool : 1 nga ànd ceek teeyug bakan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal. + +(DOGGANTAL CI AJJ) + +Ajj ñeenti farata la am : 1 yeenee ajj 2 tawaaful ifaada 3 dox diggante safaa ak marwa 4 taxaw arafa. + +(DOGGANTAL CIY SUNNAAM) + +Sunnay ajj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka. + +Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi. + +Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa. + +(LII AG MOTTALI LA ) + +Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku birël ci ginaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi. + +(DOGGANTAL CI NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINAAW IMAAM) + +Lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot. + +Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , +sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat. + +Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, +taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex. + +Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf. + +Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël. + +Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. +Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. +Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko. + +Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . +Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem. + +(BUNT CI LIHSAAN) + +Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu. + +Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral. + +Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ. + +Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat. + +Fii la Tasawudus sixaar yam,ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca.Woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi,di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog,mu diw woy wuy wommate jëme ci xam-xam ak jëf,ak tegginu tey jàppndal mebat yi.Mu diw rajas wu am njariñ te barkeel,wu way texe yi bokk. + +Yàlla ci barkeb yonant bi (j.y.m) nangu na woy wii,jariñ ci it kepp ku texe,kuy laabiire,te yewwu ,moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax,di jañ gepp texeedeek woru. +Yàllaay ki ma digal ma woy ko,yàlla miy ki nu jublu,mi may fegal luy waral njàqare.Woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja,moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral. + +Konug cant ñeel na yàlla,xeewal ak mucc yal na nekk ci Ahmadu ,aji rammu jiy boroomi ngëneel,ak ñoñam aki saabaam.Ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam. + +Subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun,wasalaamun halal mursaliin,wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin. + +(LII AG XAMLE LA) + +Bokk na ci njariñi woy wii : ki ko woy (muy sëñ bi) ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ,ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom.Bokk na ci ngëneeli woy wi, begal gun ko begal bim ci noppee(moom sëñ bi) ne ko woy wii de la yàlla (t.s)ak yonant bi(j.y.m) gën a sopp ci ay keman. +Bokk na ci li nu ko begale:kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko,texe ag texe gu texeedi dul toppati,bokk na ciy jagleem ku ko mokkal Munkir ak Nakiir dun ko laaj ci bàmmeel,ak leneen ak leneen ak leneen,yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob,yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li. + +Niti senegaal +Ci làkku ibrë (בעל) la tur wi jóge. +Ci angale mooy baal; Ci faranse mooy baal + +Xërëm la woon; waa Kanaan defoon ko Yàlla. Israyil daan na ko màggal itam. Ci Injiil man nañu gis Baal ci Ro 11:4. + +Yàllay xeet yi +Ci làkku ibrë (בבל) la tur wi jóge ci Biibal. +Ci angale mooy Babylon; Ci faranse mooy Babylone + +Ni ñu jëfandikoo Babilon ci Injiil mooy ñett. + Babilon dëkku penku la woon, di péeyug réewu Kalde, maanaam Irak. Ci dexu Efraat la nekkoon, lu tollu 80 kilomet ci bëj-saalumu dëkku Bagadad (Bagdad). Fa la bànni Israyil nekke jaam ca 566-536 at lu jiitu Kirist. Mc 1:11,12,17; Jëf 7:43 + Léeg-léeg xanaa ñu misaale ko dëkku Room, ak it nguur, giy bëreek Yàlla ci muju jamono yi. Pe 14:8; 16:19; 17:5; 18:2,10,21,24 + Benn yoon ci 1Pi 5:13 mu nekk wax ju làqu ju misaale ko benn dëkk: xanaa Babilon walla Room walla benn tata nguur Room ci dexu Niil gi fu dëkku Kayro (Cairo) nekk tey jii. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (בִּלְעָם) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Balaam; Ci faranse mooy Balaam + +Ku mbubboo turu yonent la woon, te fexe woon a rëbb bànni Israyil, ngir sàkku alal ca jamano Musaa. Bokkul woon ci Yawut yi. Gisaanekat la woon itam. Dafa digal buuru Mowab Balag, ñu jéema boole waa Israyil ak jaamu xërëm. Loolu moo tax Israyil rey nañu ko. Man nañu jàng ci jalooreem ci Nu 22:1-24:25; 31:8; De 23:4-5; Jos 13.22; 24:9-10 + +Injiil moo wax ci Balaam ci 2Pi 2:15; Yu 1:11; Pe 2:14. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci angale mooy Balak; Ci faranse mooy Balak + +Balag, buur ci jamonoy yonent Yàlla Musaa la woon. Moo yilifoon waa Mowab. Fey na Balaam, ngir mu rëbbal ko bànni Israyil. Man nañu jàng ci jalooreem ci Nu 22:1-24:25. + +Injiil moo wax ci moom ci Pe 2:14. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci angale mooy Blastus; Ci faranse mooy Blastus + +Bëkk-néegu buur ba Erodd Agaripa I la woon. + +Turam feeñ na ci Injiil ci Jëf 12:20. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Elymas; Ci faranse mooy Élymas + +Luxuskat la woon, ku bokk ci Yawut yi ci dëkku Pafos ci dunu Sipar. Dañu koy tudde itam Bar-Yeesu. Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus. Dafa dogale Pool, ngir bañ boroom réew ma gëm. Waaye Pool rëbboon na ko ba mu gumba. Man nga ko jàng ci Jëf 13:6-12. + +Man nañu gis tur wi ci Jëf 13:6. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë בר-אבא; Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Barabbas; Ci faranse mooy Barabbas + +Bóomkat ak taskatu réew la woon. Nekkoon na ci kaso bi ñu jàppee Yeesu. Pilaat bàyyi na ko bi ñu àttee Yeesu. Man nga ko jàng ci Mc 27:16-26; Mk 15:7-15; Lu 23:18-25; Yow 18:39-40. + +Turam moo feeñ ci aaya yii: Mc 27:16,17,20,21,26; Mk 15:7,11,15; Lu 23:18,19; Yow 18:40. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Barsabas; Ci faranse mooy Barsabbas + +Ñaari nit ñoo bokk dàkkental bi: + Yuusufa ku bokkoon ci ñaari nit ñi ndawi Kirist ya tuddoon ngir wuutu Yudaa Iskariyo (Jëf 1:15-26). Turam feeñ na ci Jëf 1:23. + Yudd, benn njiit ci mbooloo ñi gëm ci Yerusalem. Jëf 15:22. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë תולמי‎‎‎‎‎-בר‎‎; Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bartholomew; Ci faranse mooy Barthélemy + +Benn ci fukki taalibe Yeesu ak ñaar la woon. Am na ñi xalaat ne Bartelemi ak Nataneel (Yow 1:45-51) kenn nit la. + +Bartelemi feeñ na ci aaya yi ci Injiil: Mc 10:3; Mk 3:18; Lu 6:14; Jëf 1:13. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bartimaeus; Ci faranse mooy Bartimée + +Gumba ci dëkku Yeriko la woon, bi Yeesu gisloo woon. Man nga jàng ci Bartime ci Mk 10:46-52. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë (בָּרָק) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Barak; Ci faranse mooy Barak ou Barac + +Njiitu xarekatu bànni Israyil ci jamano Debora ji la woon, lu tollu 1.100 at j.K.. Man nañu jàng ci jalooreem ci Jud 4:1-5:31. + +Ci Injiil dinga fekk turam ci Yt 11:32. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku gereg \~baraciav\~; Ci làkku ibrë (\^hykrb\^) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Barachias; Ci faranse mooy Barachie + +Baayu Sakariya ki ñu reyoon ci këru Yàlla gi la woon. + +Turam feeñ na ci Injiil ci Mc 23:35. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë בעל זבוב; Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Beelzebub; Ci faranse mooy Béelzébul + +Yàlla ju araam la, ji waa Filisti doon jaamu ci dëkku Ekron. Yeesu moo ko tuddewoon buuru rab yi. Am na ñi xalaat ne weneen turu Ibliis la, ñeneen ñi xalaat ne meneen xel mu bon mu am kàttan ci suufu Ibliis. + +Man nañu gis tur wi ci Mc 10:25; 12:24,27; Mk 3:22; Lu 11:15,18,19. + +Yàllay xeet yi +Ci làkku ibrë בְּלִיַּ֫עַל la tur wi jóge. +Ci angale mooy Belial; Ci faranse mooy Bélial + +Weneen turu Ibliis walla Seytaane la. Man nga ko gis ci Injiil ci 2Ko 6:15. + +Yàllay xeet yi +Ci làkku ibrë (בִּנְיָמִין) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Benjamin; Ci faranse mooy Benjamin + +Caatu Yanqóoba la woon, moom mi sos giir ci bànni Israyil, mu jàpp ci Yude, ba réew ma xàjjalikoo. Sóol mi doon buur bu jëkk ci Israyil, ca la bokk. + +Gis nañu tur wi ci Injiil ci Jëf 13:21; Ro 11:1; Fb 3:5; Pe 7:8. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Tawreet +Ci làkku gereg Βέροια; +Ci angale mooy Berea; Ci faranse mooy Bérée + +Benn dëkk ci diiwaanu Maseduwan la woon. Nekkoon na ca joor ga nekk ca taatu tund wi ñuy wax Bermio lu tollu 35 kilomet digganteem ak Géeju Ese (mer Egée). Dëkku Gereg la bu amoon ay Yawut yu bare. 70 kilomet moo nekk diggante Bere ak Tesalonig. Tey jii dëkk bi Weroya (Véroia) la tudd. + +Man nañu jàng ci Bere ci Jëf 17:10-14; 20:4. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Berenice; Ci faranse mooy Bérénice + +Doom bu jigéenu Erodd Agaripa I la woon, di magu Dursil. Ci 28 g.K. la juddu. May nañu ko magu baayam, Erodd bu jóge Calkis (Chalcis), bi Berenis amee 13 at. Jëkkëram gaañu na bi mu amee woon 20 at, Berenis séy ak magam Erodd Agaripa II (ñu bokk ndey ak baay). Gannaaw loolu mayoon nañu ko Polemon, buuru Silisi. Berenis dëddu na jëkkëram dellu ci magam Erodd. Mujjoon na nekk coro Tit, laataa muy nekk buuru Room. + +Berenis moo feeñ ci Injiil ci Jëf 25:13,23; 26:30. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy beryl; Ci faranse mooy béryl + +Per bu wert ni géej la. + +Gis nañu ko ci Injiil ci Pe 21:20. + +Per yi ak Xeer yi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku ibrë (בֵּית עַנְיָה) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bethany; Ci faranse mooy Béthanie + +Ñaari dëkk ñoo bokk turu Betani: + + Betani ca wetu Yerusalem + Betani ca penku dexu Yurdan + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Dëkk bu ndaw ci tundu Oliw ya, daanaka 3 kilomet diggam ak Yerusalem ci yoonu Yeriko. Tur bi moo tekki këru figg yi. Yaakaar nañu ne amoon na fa dëkk tàmbali ca 600 at yu jiitu jamono Kirist ba 1400 at gannaawam. Foofu la xariti Yeesu, di Màrt, Maryaama ak Lasaar, dëkkoon. Ca ayu-bésam bu mujj ba Yeesu doon na fanaan Betani, di xey dem Yerusalem bés bu nekk. Mc 21:17; 26:6; Mk 11:1,11,12; 14:3; Lu 19:29; 24:50; Yow 11:1,18; 12:1,9. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Bérab fu Yonent Yàlla Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox ci gannaaw dexu Yurdan, maanaam ci penku dex ga (Yow 1:28). Foofu la Yaxya sóobe Yeesu ca ndox itam. + +Bu yàgg xamatuñu tembe fan la dëkk bi nekkoon. Waaye seetkati cosaan yaakaar nañu ne fekk nañu bereb ba ca penku dexu Yurdan ca atum 1995. Berab ba Wadi al-Xarar la tudd. Am na fa ay bëti ndox, ak benn làquwaay fu ñu yaakaar ne Yaxya daan na fanaan. Su fekkee ne danga nekkoon ca dëkku Yeriko manoon nga gis berab ba. Ñoom ñi gas ci suuf ngir seet naka la nit ñi dëkke ca yeneen jamono yu fekk nañu ca bereb ba ay tabax, ay jàngu, ay làquwaay fu nit ñi doon dëkk, ak ay sanguwaay. Taalibe Yeesu yi doon nañu ajji ngir siyaaraji ca xarnu yu jëkk yi gannaaw jamono Kirist. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bethesda; Ci faranse mooy Béthesda + +Turu benn sangewaay ci Yerusalem la woon, ca wetu benn ci bunti dëkk ba, maanaam ca Buntu xar ya. Gas nañu ko daanaka 8 xarnu lu jiitu jamono Kirist (2Roi 18:17; Isa 7:3; 36:2). Daanaka 3 xarnu lu jiitu jamono Kirist gas nañu naareelu sangewaay. Daan nañu sang xar yi foofu laata ñu rendi woon leen ngir ab sarax ca këru Yàlla ga. Gannaaw ga gëm nañu ne ndoxum man na faj ña lafan. + +Dañu ciy wax ci Injiil ci Yow 5:2. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Bethphage; Ci faranse mooy Bethphagé + +Benn dëkk bu ndaw la woon, ci tundu Oliw ya ci yoonu Yeriko diggante Yerusalem ak Betani. Sorewul Betani. + +Dañu ciy wax ci Injiil ci Mc 21:1; Mk 11:1; Lu 19:29. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë בית לחם la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bethlehem; Ci faranse mooy Bethléhem + +Dëkk bu ndaw la woon, lu tollu 9 kilomet ci bëj-saalumu Yerusalem. Dëkku Daawuda la. Foofu la Yeesu juddoo. + +Dañu ciy wax ci Injiil ci Mc 2:1,5,6,8,16; Lu 2:4,6,15; Yow 7:42. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci làkku ibrë \^hdyu-tyb\^; CI làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Bethsaida; Ci faranse mooy Bethsaïda + +Dëkk ba ci penku-kawu dexu Galile la woon, sorewul fu dexu Yurdan dugg. Tey jii xamuñu tembe bérab bi. Man na nekk sax amoon na ñaari dëkk yu bokk tur Betsayda. Benn ci penku dexu Yurdan, te benn (mooy Betsayda ci diiwaanu Galile) ci sowu dexu Yurdan. + +Man nañu koy jàng ci Injiil ci Mc 11:21; Mk 6:45 8:22; Lu 9:10; 10:13; Yow 1:44; 12:21. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Bithynia; Ci faranse mooy Bithynie + +Diiwaanu nguuru Room ci Asi Minër la woon. Tey jii bokk na ci réewu Tirki (Turquie). + +Dañu ciy wax ci Injiil ci Jëf 16:7; 1Pi 1:1. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Bosor – ci àngale mooy Beor, ci faranse mooy Bosor. + +Baayu Balaam la woon. + +Dañu ciy wax ci Injiil ci 2Pi 2:15. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Ci làkku yawut la tur wi jóge. +Ci angale mooy Boanerges; Ci faranse mooy Boanergès + +Dàkkental la bi Yeesu joxoon Saag ak Yowaana, doomi Sebede yi. Tur wi dafa tekki "Ñi aaytal ni dënnu gi". Xanaa Saag ak Yowanna dañuy gaawa mer. + +Tur wi feeñ na ci Injiil ci Mk 3:17. + +Baat yi jóge làkku yawut +Ci làkku ibrë (בועז) la tur wi jóge. +Ci angale mooy Boaz; Ci faranse mooy Boaz + +Boroom alal ak beykat ci dëkku Betleyem la woon. Dafa takkoon jenn jigéenu Mowab, ji tudd Ruut. Jot na Ruut ndax jëkkëram mbokkam la woon te faatu na bala mu am doom. Ci kaw seeni yoon, su fekkee ne am na genn góor gu faatu te bàyyiwul doom, mbokkam mu gëna jege war na donn jabaram. Seen taaw bu goor dina donn ci goor ki faatu woon. Bowas mbokk mu jege jëkkëru Ruut la woon. Doom bi ñu jur mooy maamu Daawuda. Man nañu koy jàng ci Ru 1:1-4:22. Naka noonu Bowas bokkoon na ci maamaati Yeesu, ni ñu koy gise ci Macë ak ci Luug (Mc 1:5; Lu 3:32). + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Israel, people of Israel or children of Israel; Ci faranse mooy Israël, peuple d'Israël ou fils d'Israël + +Israyil mooy tur, wa Yàlla jox Yanqóoba, doomu Isaaxa, di sëtu Ibraayma. Ñi wàcc ci Yanqóoba nag lañuy wooye bànni Israyil walla it Yawut yi. Def nañu fukki giir ak ñaar, di yi soqikoo ci doomi Yanqóoba. + +Man nañu gis bànni Israyil ci Injiil ci aaya yii: Mc 8:10; 10:6; 15:24; 19:28; 27:9; Mk 12:29; Lu 1:54,80; 2:25; 7:9; 22:30; Yow 1:31; 3:10; Jëf 2:36; 4:10,27; 5:21,31; 7:23,37,42; 9:15; 10:2,22,36; 13:17,23; Jëf 13:24; 19:4; 26:7,17,23; 28:20; Ro 9:4,6,27,31; 10:1,19; 11:7,11,17,25,26; 1Ko 10:18; 2Ko 3:7,13; 11:22; Ef 2:12; Fb 3:5; Yt 7:5,9,11; 8:8,10; 9:19; 11:22,28,29,30; 12:18; 13:10; 2Pi 2:1; Pe 2:14; 7:4; 21:12. + +Leeral Biibël +Ci angale mooy Thyatira; Ci faranse mooy Thyatire + +Ca jamono Injiil dëkk la woon, ci diiwaanu nguuru Room bu tudd Asi, maanaam ci sowu réew bi tudd tey jii Tirki. Tey jii Akhisasar la tudd. Dafa nekkoon ci yoon diggante Pergam ak Sàrd, ci dig bi nekkoon diggante diiwaani Misi and Lidi. Dëkk ba siiw na ndax cuub bi ñu fa defaroon. + +Ca jamono ju njëkku mbooloom ñi gëm Kirist amoon na fa mbooloo bu am solo. Naka noonu gis nañu ne mooy benn ci 7 mbooloom bi ñu bind ci Peeñu ma. + +Dañu ciy wax ci Catir ci Injiil ci Jëf 16:14; Pe 1:11; 2:18,24. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tirki +Ci làkku ibrë (דָּוִד) la tur wi jóge. Daawuda mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale mooy David; Ci faranse mooy David. Moo doon buur bu mag ci bànni Israyil, di yonent bu bind lu bare ci Sabóor. Man nga jàng ci jalooreem ci Kàddug Yàlla gi ci 1Sa 16:1-30:31; 2Sa 1:1-24:25; 1Ki 1:1-2:10; 1Ch 3:1-9; 10:13-11:19; 12:1-23:32; 28:1-29:30. Benn ci maamaati Yeesu ci Macë ak ci Luug. Ci Injiil Daawuda moo feeñ ci aaya yii: Mc 1:6,17; 12:3; 22:42,43,45; Mk 2:25,26; 11:10; 12:36,37; Lu 1:27,32,69; 2:4,11; 3:31,32; 6:3; 20:42,44; Yow 7:42; Jëf 1:16; 2:25,29; 4:25; 7:45; 13:22,34,36; 15:16; Ro 1:3; 4:6; 11:9; 2Tim 2:8; Yt 4:7; 11:32; Pe 3:7; 5:5; 22:16. + +Sëtu Daawuda: +Turu Kirist la, muy wone ne, ci lu jëm ci juddoom wàcc na ci yonent Yàlla Daawuda, di wone it ne, Almasi bi la. Sëtu Daawuda moo feeñ 15 yoon ci Injiil ci aaya yi: Mc 1:1,20; 9:27; 12:23; 15:22; 20:30,31; 21:9,15; Mk 10:47,48; 12:35; Lu 18:38,39; 20:41. + +Diine +Yonenti Lislaam +Dalmanuta – Ci làkku yawut la tur wi jóge. Ci àngale mooy Dalmanutha, ci faranse mooy Dalmanoutha. + +Diiwaan la woon, ci penku dexu Galile fu Yeesu demoon. Xamuñu ne tembe fan la nekkoon. Man nañu ko gis ci Mk 8:10. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Ci angale mooy Dalmatia; Ci faranse mooy Dalmatie + +Ci jamonon Injill diiwaan la woon, ci sowu-suufu diiwaanu Room bu tuddoon Iliri ci penku géeju Adiratig. Maanaam mooy daanaka réew mi ñu waxoon Yugosalawi (ex-Yougoslavie), te ñu wax léegi Korwaasi, Bosni-Ersegowin ak Montenegëro. + +Dañu ciy wax ci 2Tim 4:10. + +Bereb yi ci Téere Linjiil +Tugal +Dalmasi +Ci angale mooy Damaris; Ci faranse mooy Damaris + +Jenn jigéen ci Aten la woon, ji nangu woon Yeesu jaarale ko ci waare Pool daanaka 55 g.K.. + +Dañu ciy jàng ci Injiil ci Jëf 17:34. + +Nit ñi ci Kàddug Yàlla +Nit ñi ci Téere Linjiil +Mooy xam-xam gi'y gëstu lepp lu jëm ci wallu mbëj +Xarala +Xayma + Xam-xamu suuf si ak jawwu ji + Simi + Pac + Diisaayu yaram yi + +Xam-xam +Nit + Kàllaama + Yoon + Koom-koom + Taariix + Xibaar + Xeltu + Diine + Melosuuf + +Xam-xam +Baatu Njàngat day tekki mbooleem ay mbind yuy wax ci ay koj. Ni ko Ñenn ñi di gisee du yem rek ci mbind yu ñu taaral waaye am na it njàngatu kàddu, maanaam yu yemm ci ay kàddu. Sunu xoolee mboolaay yu mel ne yu waa Afrik yi xamul woon bind, seenum njàngat ci kàddu la yemoon. + +Tekki +Njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo, muy ci mbind walla ci kàddu, di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi. Njàngat da fa yaa te bariy fànn, li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi. Taaral gi am na ci lu am solo. + +Ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn. Waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu, ci xarala walla yeneen. + +Ladab +Njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo, muy ci mbind walla ci kàddu, di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi. Njàngat da fa yaa te bariy fànn, li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi. Taaral gi am na ci lu am solo. + +Ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn. Waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu, ci xarala walla yeneen. + +Ladab +Ladab baat la bu bawoo ci araab, di ci araab adab. Adab nag ci araab am na ñaar ba lu ko ëpp ciy tekki, waaye ñaar yi ci gën a siiw, bi ci njëkk mooy Adab: di baat bu Sëriñ Tuubaa (y.y.g) bari lu mu jëfandikoo ci téereem bii di Nëhju, di téere bu tëriit li (sujet bi) jëm ci yar ak dugal ci nit ñi ay teggiin (aadaab) di mbooloo(pluriel) ci adab. Bi ci des di bi ñu tax a jug, moom nag adab la nu laaf ci ag L muy leegi ladab, lu tax nu laaf ci L gi, loolu ñi ngi ci roye Lislaam te bu njëkk Islaam la woon, waaye ginnaaw ak L gi la ko wolof yi di gën a man di wax ak a tudd, moo waral - ci li nu wax - nu koy boole ci baatu araab bi, lii nag làkk woo gis ci àdduna bi am na ko, boo demee ci araab da cee fees dell, ay baay yu nu lem ba manees koo wax ci làkku araab, te doonuñu woon ay baati araab ñu mujj bokk ci làmmiñu araab te bu njëkk bokkuñu ci woon. Lu ni mel fees na dell ci Alquraan, am it ci làmmiñu araab wu jamonoo wii, sundus, istabraq ak yu ni deme duñu ay baati araab te ñi ngi ci Alquraan, lu mel ni qubtaan, di capitain dees koo jengal ba araab yi man koo wax waaye juddoowu ci añs. +Waaye nag Ladab ca daaray majaalis ya, maanaam fa mag ña daan jànge, nga xam ne seenuw jàngiin da daan tegu ci firi baat topp baat, maanaam pirim baat-baat, nga `xam ne lees la wax tekkil la ko ci wolof bu ñu nee bismil-laa ne la : maa ngi tàmbalee ci turu Yalla, ar-rahmaani: kay aji yërame ci àddina añs. Bu dee ci tekkiin wii, Adab di baat bi nuy wax Ladab: njàngat lees ko daa firee, walla xam-xamu mbind. + +Kon manees na ne: +Ladab, + +Buñu bëggee muy wolofi kese ñu ne: +Njàngat, walla xam-xamu mbind + +Ci: Farãse: + CORRECTION + BELLES-LETTRES + COURRIER + LITTÉRATURE + +Ci làkkuw Angalteer:LITERATURE + +Xeeti njàngat +Ci mbindin mi walla waxin wi la ñuy sukkandiku ngir man a xammee xeeti njàngat yi: + Taalif + Léebu + Dal bu aju ci Léeb: http://www.leebone.com/ +Su nu jàppee ne njàngat ab mbooloom ay baat yu am bopp di wax ci lenn li la. Kon man nanoo wax Njàngatu xam-xam, Njàngatu koom-koom, Njàngatu diine, Njàngatu woy, añs. + +Tekkiinu njàggat + +Njàggat benn la ci anam yi nit di génnee ak a feeñale li nekk ci moom ciy yëgg-yëgg aki xalaat aki ñeewant aki gis-gis, jaare ko ci ay mbind walla bindiin yu rafet te wuute, moo xam woy la ( maanaam poesie) walla wesar (bind ci lu dul di ko nos, maanaam safaanub woy) walla wesar wu ñu nos. Loolu nqg di ubbil nit ay bunt ngir mu am man-man ci feeñal ak génne li ñu manul a génne walla ñu koy man a feeñale ci geneen anam walla melo. Njàggat nag day takku takku gu dëgër ci làkk. Dëgg-dëggi njuréef walla ngérte li juddoo ci làkk ñu bind ko, walla caada ja ca juddoo, day nekk di lu dencu walla lu wattuwu ci biir melokaani njàggat yi aki peeñ-peeñam, te ñoom danuy wuute kem ni gox yi di wuutee jamono yi di ko wuutee. Jamono ju nekk tam ay soppiku da ciy sosu akug jëm kanam akug wuute ak xeetu ànd ak jamono yi + Sëriñ Mbay JAXATE + Mamoor Xam Sa Diine + Seriñ Muusaa KA + +Man ngéen a xool foofu ci suuf,cuq ci lëkkalekaay yooyu, ngir déglu as lëf ci wolofali Sëñ Mbay JAXATE ak Sëñ Muusaa KA: + + https://web.archive.org/web/20080821142122/http://www.touba-internet.com/wolofal/serigne-moussa-ka-jazaou-shakor-guej-gui.html + http://www.archive.org/details/wolofal + https://web.archive.org/web/20081031043122/http://www.htcom.sn/spip/magal2006/magal/wolofal.htm + http://www.almouridiya.org/index.php?option=com_musicbox&task=view&Itemid=73&catid=19&id=5 + +Waxi Seex Anta Joob ju aju làkk + +Làmmiñ ak jamono + Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko;làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ne paaka bu xumaag. Tubaab yi bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu koo yore ci seen làmmiñu bopp.Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des ginnaaw.Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag anjaboot ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko...Loolu moo taxoon ñu sàggane sunu làmmiñ yii.Waaye du caagéenu dañu cee manul woon a waxe li ñu bëgg a wax... + +Dangeen di xam ne aw làmmiñ, jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd, am xel ay gàtt, aw làmmiñ gàtt!Waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk, aw làmmiñ man na koo tudd;aw làmmiñ gàttul. + +Nit kiy wax nag fi xelam yam, fi jàngam yam, fi gis-gisu àddunaam yam, foofu rekk la ay waxam man a yam... + +Waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk, làmmiñ dina ko tudd. +Lu ko waral? Amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul!Mooy li nga xam ne - waxoon naa ne...dinaa cuq tuuti xel yi...ndax defe naa ne, yéen jàng ngeen xam-xamub làmmiñal...xam ngeen ne De Saussure (boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal) wone na loolu.Làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa. Baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la! Kepp! Amul sax menn maanaa. Ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am, kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde.Wenn tur wi di moom te loolu amul. + +Jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu Seex Anta Jóob, mu amoon ci awril 1984 ca Cees + + + +Njàngat +Xaralaymbëj Mooy xeetu xam-xam giy gëstu lépp lu jëm ci wàllug mbëj, ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam. bu njëkk dañoo foogoon ne mbëj ag wal la rekk guy dem, gu man a nekk gu baax(+) walla gu bon(-). Waaye ci ndimalu ay woroom xam-xam yu mel ne Hertz, Helmholtz, Maxwell, Heaviside, Alessandro Volta ak ñeneen ñu bari, ci lees dem ba gën a nànd, xam mbir mi. Lu mel ne yamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinu yani mbëj yi ( feppsaal ak mbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj) walla toolu mbëjbijjaakon ba ca juddoo. + +Ci gàttal, ci noonu lañu tambalee gis yenn ci ay jëfandiku yu mbëj: Doxalukaay bu mbëj, soppalikaay aki niitu... + +Tay xaralaymbëj moo yor wàllu sàkk ay wuutuloxoy mbëj ak ay buumi séddalekaayu kàttanug mbëj + +Ay Faramface +Ay faramface ak ay àtte yi lal xaralaymbëj. + +yamaleb maxwell yi, ñooy àtte yu am-solo yu ñeel mbëjbijjaakon, ci la yeneen yi soqeekoo. + +àtteb ohm(om) yiy faramface ndëgërlu gu mbëj gi + +àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy faramface xiirtalug mbëjbijjaakon + +njeexitu joule mooy leeral ni kàttanu mbëj di soppeekoo nekk tangoor ngir njeexitu ndëgërlu gi. + +àtteb Kirchhoff(kiirkof) mooy leeral jëflante bi nekk ci diggante dawaan ak dend ci ag ndombo. + +Jóox, yóbb ak séddale kàttanu mbëj + +Ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya (barab yees koy jëfandikoo). +Kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ay jurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel, li ñuy wax diggub mbëj, ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi. + +Buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëlee kàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya. + +Li wuutale Buumi yóbbukaay yi, mooy limu dend gi ñuy yóbb, moo tax ñuy gis ay buumi dend gu kawe, [[Dend gu diggu]|dend gu diggu]], dend gu suufe. Su diggante jóoxuwaay yi guddee, dañ fay def ay mbëjjaaru, ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioŋi watt ci kàttan tambalee ciy 400000 v. Buumi dend gu kawe yii la ñuy duppe yu yóbbug kàttanu mbëj, yi nga xam ne ñooy tax a man a yóbb kàttanu mbëj gi, jële ko ca jóoxuwaay ya, jëmee ko ca barabu soppikaay ya. + +Ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu, jaarale ko ci ay masin yu mbëj yees di duppee soppalikaay, ci noonu la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu, moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cig ndombog séddaleg kàttanu mbëj, foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi. + +Wuutuloxo yu mbëj + +Doxalukaay + +Doxalukaay yu mbëj yi, ay wuutuloxo lañu yu’y soppi kattanu mbëj def ko kattanu doolerandu. Doxalukaay yi dañu leen a séddale ci: + + Doxalukaay yu dawaan bu wéy + + Doxalukaay yu dawaan bu safaanu, bii man naa dox ci ñaari fànn ( ñettwéq, wennwéq), ci nii ñu am: + + Doxalukaay yu demandoo: su fekkee baraayu ni muy wëddeeloo demandoo na ak baraayu ndombo gi + + Doxalukaay yu demandoodi: su fekke wëddeeluwiinu boppam la am. + Doxalukaay yu wennwéq + + Doxalukaay yu ñettiwéq + +Jurukaay + +Jurukaayu mbëj yi Ñoom ay wuutuloxo lañu yuy soppi kàttanu doolerandu def ko kàttanu mbëj. Yi ci gën a raññeewu: + + Safaanukaay, mooy juddal dawaan gu safaanu + +Soppalikaay +Soppalikaay, Ab wuutuloxo la, maneelam mooy soppi limu dendu mbëj gi nekk ci ab ndombo, ci yokkute walla wàññi. Lu mu néew néew di na am ñaari lëmës yu bijjaakon boole. + +Wuutuloxo yu man a yokk walla néewal taraay te di jëfandikoo benn lëmës rek, lañuy tuddee Soppiboppam + +Niitu +Ay jumtukaay lañu yu aajowoo soppi kàttanug mbëj mu nekk leer. Di ko jëfandikoo ngir leeral barab yi. + +Lëkkalekaay yu biti + +xaralaymbëj +Mbëj da di ag feeñte gu gisuwul ak bët, guy feeñ ci ag wootalante walla bëmëxante ci diggante yani mbëj yi. Ci gattal mooy gépp feeñte gu juddu ci jàmmaarloo gi nekk ci diggante: feppsaal yi, ñoom ci lu ëpp da ñuy tekkaaral, ak mbëjfepp yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu-yëngu, ci biir xarefulwoon bi. seenuw demiin jur ab dawaanu mbëj. + +Su ñu ko boole ak bijjaakon, mu jur beneen banqaas bi ñu duppee mbëjbijjaakon. Mbëj moo yor ay feñte yu jëmm yu mel ne melax, toolu mbëj ak dawaanu mbëj (ci lu bari dañ leen di jaawale). + +Mbëj doon na “jaamu” nit bi gën, doon tamit raññeekayu àdduna bu bees bi. Dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këri koom-koom yi te jegeele nit ñi gënoon a soriyante. + +Yanub mbëj +Yanub mbëj doon na lu ñu man a natt te man koo jëfandikoo, waaye doonul lu neex a faramface ak ay baat yu yomb a nand, ndaxte yombul leeral melokaan yi mu am dëgg-dëgg. Xayna li gën mooy wax lan la ak li muy sabab. lépp (lu mu man a doon) lu am yanub mbëj, man nañoo wootalante walla bëmëxante. Li gëstu yi wone mooy am na ñaari xeeti yani mbëj, benn bi lañuy woowe yan bu baax (+) moom mooy nekk ci biir saalu xarefulwoonu ne-ne yépp ak yan bu bon (-) (mbëjfepp) ñoo nekk ci li wër saalu xarefulwoon yi. Naka-jekk yan yu baax yu saalu xarefulwoon bi dañuy tolloo ak limu yan yu bon yu mbëjfepp yi ko wër. + +Dawaan bu wéy ak bu safaanu + + + +Ba fii danoo jàppoon ne, gépp ndombo goo jël, mbëjfepp yi dañuy yëngu saa su ne jëm ci benn jubluwaay ci biiram. Yenn saa yi nag dawaan bi du sax ci maase, muy ci doole walla ci jubluwaay bi. Ag noste mbaa ag ndombo gu ne mel lees di wax dawaan bu wéy. Am misaal man naa nekk ag noste gu ab tegle di doxal. Donte sax aajowoowul dawaan bi di am genn jubluwaay gu sax. Bari nañu ndombo yu mbëj yees di jëfandikoo yuy safaan jubluwaayu seen dawaan ci biir ndombo gi. + +Gii xeetu dawaan lees di wax dawaan bu safaanu. Ndombo yu mbëj yu ëpp yi ñuy jëfandikoo, dawaan bu safaanu lañu. Cig ndombo gu dawaan bu safaanu, dafay laaj waxaale tamit baraayu ni dawaan bi di safaanoo, taraayu dawaan bi ak dend bi ci ndombo gi, moom rekk , bu mujj bi, doy na su fekkee dawaan bu wéy la. Ci baraay bi lañuy natte ñaata yoon la dawaan bi di soppi jubluwaay ci benn saa. + +Mbëj ak Bijjaakon + +Liy wër ab mbëjfepp walla leneen lu mu man a doon lu am ab yanub mbëj day am melokaanu luy dox, moom lañuy tuddee toolu mbëj. + +Soo jallaxee ay mbëjfepp, day am benn tool bu wër seenub jublu, moom la ñuy tuddee toolu bijjaakon. Dooley tool boobu dafa aju ci limu mbëjfepp yiy daw ak seen gaawaay, maanaam, ci yeneeni kàddu, ci dawaanu mbëj bi. + +Soo jallalee ab dawaan ci ag lëmës, gu nekk wëñu përëm, ci nimu waree, lëmës googu day mel ne bijjaakon gu weñ, day xëcc walla bëmëx yeneen lëmës yi mu yemal wëñ. lëmës gu mel noonu su fekkee danga koo defaree ak ag wëñu përëm goo wëndeel cib weñ, day gën a yokk toolu bijjaakon ba cay juddoo. +Su fekkee dangaa am ay lëmës yu bari, yu ñu wëndeel wëñ ci weñ, yu man a wëndeelu, nga boole leen ak yeneeni lëmës yu dul wëndeelu, yu am toolu bijjaakon bu tar, yu dawaan jaar, day jur jenn dooley doolerandu. Doole joogu moy wëndeel lëmës yu man a wëndeelu yi, mu daal di man a def liggéeyu doolerandu. Mu nekk ab jumtukaay bi ñuy woowe doxalukaay bu mbëj. Tay jii, doxalukaay yu mbëj yi ñooy doxal bépp wuutuloxo, tambalee bi ci gën a ndaw ba ca ba gën a ngande. +Doxalukaay yi dañoo bari te am ay melokaan yu wuute. + +Soppalikaay + +Njariñ li ci jëfandikooy noste yu dawaan bu safaanu moo ngi ci li ñuy man a yokk walla waññi dayoo bu ab dendam ci jëfandikoo jumtukaay bees di woowee soppalikaay. Ab soppalikaay ñaari taxañ yu tàqalikoo lay am, yees ber, yu ay wëñ yees lëmës cib dankub weñ (saalu soppalikaay bi). Ab dawaan bu safaanu su walee ci taxañ bu njëkk bi, ab toolu bijjaakon daf fay juddoo, mu jur moom itam, ab dend buy soppeeku ci jenn jamono ju nekk ci ñaareelu taxañ bi. Su ñu jëlee benn dayoo bu saal bi (weñ gi) ak yenn limi lëmësi wëñ yu taxañ yi, dees na man a yokk walla waññi dend bi ci nees ko bëgge. +Kon, ab Soppalikaay di nanu tax a man a jëfandikoo dend bu suufe, ngir sunu kaaraange, ci kër yi, te terewul nu man koo jokkale, mu jóge cib digg bu mbëj bu sori, cib dend bu kawe. Manees naa jëfandikoo ab soppalikaay ciy fowekaay yu mbëj ak ci yeneen jumtukaay yu ndaw yu mbëj ba-tay. Maneesul a jëfandikoo soppalikaay cig ndombo gu dawaan bu wéy, ndaxte dawaan bi toolu bijjaakon ba muy jur duy soppiku. + +Xool it + + Kàttanu mbëj + mbëjbijjaakon + + Bijjaakon + Toolu mbëj + + toolu bijjaakon + + toolu mbëjbijjaakon + +Mbëj +“Jàngu (eglise) yéesu bu dëggu bi” ab jàngu bu temb la (indépendant)bu nekk ca Beijing ca réewu Siin, ñoo ngi ko taxawal ci atum 1917. Dafa nekk ab bànqaasu diiŋatkat (protestante) yu waa Siin ci diiney krist bi fëll ci atum 1900. Jàngu boobu day balloo 1,5 milioŋi taalibe yi mu am ci adduna wërngëlkëp. Jàngu googu gëm na njangalem pantekot, day ab baatin gu wekku ci mayu ku sell ki. Fukki ponki gëm-gëm gi ñooy: + Ku sell ki: “Jot xel mu sell mi ci xamale te jëfënbikoo ay làkk, doon na ab wòoraange ci sunub yégg ca nguurub asamaan si.” + Ngente(lavage de pieds): “Ngente gu ndox mi doon na ngir raxas say bakkar ak sag judduwaat. Ngente li ci ndox mu sell la war a amee, lu mel ne dex, géej walla cib walub ndox. Ngentekat, bi jot a am ngente li, tamit jot ndox ak xel mu sell, mooy jiite ngente li ci turu Yéesu-kristaa. Ki ñuy ngente da fa war a nuuru ci ndox mi, sëggal boppam te di xool ci suuf”. + Jangu: Ponkub jangu (raxas sa tànk) li, day tax nga man a dellu ci lenn ci jëfi Yéesu. Di it ab fattali ni daño war a am cofeel, am cellte, tuuti, am yërmaande ak di dimbaliwaate. Nit ku jot ngente gu ndox mi war a naa raxas ay tànkam ci turu Yéesu-kristaa. Yeneen Jangu yi ciy tegu man nga kaa def saa yu la neexee. + Waxtaan gu sell gi: “Jokkoo bu sell bi ab ponk la ngir maggal saayub Yéesu-Kristaa. Di na tax nu man a bokk ak Yéesu ci suux ak ci dereet, tax it nu man a jokkoo ak moom ngir nu man a dund ba faaw te man a yéeg asamaan kerook bes pénc. Ag naan gu jòge ci rasin ak mburu mu amul lëwiir la nuy jëfëndikoo su nuy amal ponk boobu.” + Besu sabbat: “Besu Sabbat, di juroom-ñaareelu bes ci ayubes bi, doon na bes bu sell. Dan kaa war a dund ci ngërëmu yalla ngir maggal li mu bind te di ko jaamu ngir man a yaakaar noflaay gu sax-dakk ci li des ci sunug dund.” + Yéesu-kristaa: “Yéesu-kristaa, baat bi soppiku nekk suux, faatu ci cruaa bi ngir man a jënd bakkaar yi, mu feeñaat ci ñetteelu bes bi dal di yéek asamaan. Mooy kénn kiy wàllu doom-aadama yi, di ki sàkk asamaan ak suuf, di itam benn yalla bi am. ” + Biibël: Biibël bi, nga boole ci tawreet ak linjiil, kàddu yalla lañ, génn dëgg la gu dul deñ, di it ab royuwaay ngir kercen bi. + Nuyoo gi: Ag Ngërëm Yalla ju bari yërmande gee koy joxe jaarale ko ci xol. Ngëm-ngëm yi, ci Xel mu Sell mi la ñu war a jafandu ngir man a topp cellte gi, ngir maggal Yalla te man a sopp doom-aadama yi. + Jàngu gi(l'eglise): Jàngub Yéesu bu Dëggu bi, bi Yéesu-Kristaa ak Xel mu sell mi taxawal ci jamanoy “taw gu mujj” ga. + Feeñug yalla: Dellusig Yalla, bes bu mujj ba lay amee, muy bes ba muy jògee asamaan ngir àtte adduna bi. Ñu baax ñi di nañ am dund gu sax dakk, ñu bon ñi dañ leen di mbugal ba faaw. +Doxalukaay bu mbëj, ab wuutuloxob mbëj la, boo xam ne kàttan giy duggu ci moom gu mbëj la te ga muy génne gu doolerandu la. Doxalukaay yu mbëj yi am nañu solo lool ci dundiinu jamono ju bees ji, te it dëgg la sax, ne limu doxalukaay yu mbëj yi nekk ci am réew dafay firndeel tolluwaayu jëm-kanamam. Maanaam yokkug limu doxalukaay yu mbëj yi ci am réew bokk na ci wonekaay yiy firndeel tolluwaayu yokkuteem ci wàllu xarala mu réew moomu. Ngir dëggal loolu, doy na xool ci jumtukaay yi nekk ci li ñu wër: ca saxaar ba ci watukaay ak yeneen ak yeneen, yi ngeen xam ne nit ku bees ki moo ngi koy jëfandikoo bu baax, man naa ni sax ñooy doxal sunug dund. + +Doxalukaay yu mbëj yi dañoo bari te wuute, am na doxalukaay bu dawaan bu wéy, doxalukaay bu dawaan bu safaanu moom mu séddaliku ci doxalukaay bu demandoo ak doxalukaay bu demandoodi,. + +Xaralay doxiin gi + +cëri ad doxalukaay + Wëndeeluwaan + Tekkaaralaan + Toolu bijjaakon + Bijjaakon + +Doxiin +Dawaanu mbëj bi day jaar ci ag lëmës gees wëndeel ci ab dogub weñ bi tudd tekkaaralaan bi. Lëmës googu, gi ñu defare ak wëñu përëm (naka-jekk përëm lay doon waaye manees na koo defaree ak beneen xeetu wommatukaay), dafay jur ab toolu mbëjbijjaakon, tool bi dafay feeñ niki ag walug bijjaakon, di lees man a natt. Danu koy jàppee niki jenn doole di lees di wax dooley Lorentz. Toolu mbëjbijjaakon boobu dafay duggante ak toolu mbëjbijjaakon bu lëmës gu wëndeeluwaan bi jur, mi melokaanoo teewaayu ñaar walla ñetti seexi dott. Wëndeeluwaan bi tambalee wëndeelu ci ndimbalu dooley Lorentz; bëj-gànnaaru toolu bijjaakon bu wëndeeluwaan bi day bijjante ak bëj-saalumu toolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi. Xaaju wëndeelu gu nekk, dott bi day soppeeku, ci noonu la wëndeelu gi man a wéyee. + +Taariixam +Ci atum 1821, lu weesu xamteg feñte gu mbëjbijjaakon gi simikat boobu di Ørsted xamle woon, la jëmmalkat bu waa-angalteer bii di Michael Faraday defar ñaari wuutuloxo ngir sàkk li mu duppee ag wëndeelug mbëjbijjaakon: ab doxub dooley bijjaakon bu mbegewu te wéy, ci lu wër ab wëñ, ci maanaa mooy faramfaceg doxalukaay bu mbëj gu njëkk. + +Xeeti doxalukaay yu mbëj +Xeeti doxalukaay yu mbëj yi am, manees naa wax ne, du xaaj du jeex, waaye manees na cee lim yi ëpp yees di jëfandikoo: + Doxalukaay bu dawaan bu wéy + Doxalukaay bu demandoo + Doxalukaay bu demandoodi + Doxalukaay bu brushless + +Lëkkalekaay yu biir + dawaan bu safaanu + dawaan bu wéy + +Wuutuloxo yu mbëj +xam-xamu suuf si mooy li nuy wax (Jiyoloji), xam-xam la buy gëstu lépp lu aju ci suuf si kaw gi ak biir gi, ak doj yi (montaañ yi)añs. Bu jawwu ji di biy gëstu lépp luy jawwu ak tegaloo gi ñu tegaloo. + +Jawwu ji +Jawwu ji nak :mooy mbalaanum ngelaw li wër suuf si. Lees di gën a sori suuf si, ngelaw liy gën di néew-doole di gën di amadi, day mujj sax di lu fàddu ci ay fukki culómet cig kawe. Lii a tax ñu man a séddale Jawwu ji ci ay goxi jawwu yu wuute te tegaloo, gox bu ci nekk ami jagley boppam: + +Fatt-jawwu walla JAWWU JU FATT ji: mooy ji gën a tal gën a fatt te gën a féete suuf; moom ngelawam day yëngu jamono ju nekk, fa lay niir yi di sosoo ak mbooleem soppaxndikuy jawwu yi; kon cig jege mooy jawwu ji ëpp ag jeexiital ci wàllug dëkk ci kaw suuf ak ci ni kilimã bi di séddalikoo + + Yolom-jawwu walla JAWWU JU YOLOM ji: mooy tiim bi ñu la njëkk a wax, moom nag ngelaw lu yëngoodi moo ko sos, lu ñàkk a ñàkk. + + Iyon-jawwsu walla JAWWU JU IYON ji: moom mi ngi sosoo ci ay dogiit yu ñu kurãal walla yu nu mbëjjal yu soreente. + + Biti-jawwu walla JAWWU JU BITI ji: mooy féex gu biti gi, fi nga xam ne ag féex gu joyoo fa nekk . + +Jéeri ji (Lithosphere) +Mbooleem beeñ bi ak doj yi ñoo sos wàll gu tond (superficiel), gu dëgër gu kol-kolu suuf si, ñu koy woowe Jéeri ji walla aji wow ji. + +bu ñu séddalee Jéeri ji, def ko ñeenti xaaj, ñatt yi daanaka ndox yee leen muur, yooyu ndox nag ñoo sos mbàmbulaan yi ak géej yi, waaye wàll yi génn ci jéeri ji; nga xam ne ndox yi muuruñu leen (gox yi ak dun yi , wàll yii ñooy wërlaay gu dëppoo te méngoo ak dundug nit, moo tax fi la nit di dunde, di fi defe ay liggéeyam, walla li ëpp ci ay cawarteem (activités). + +Jéeri ji nag day dund tey màgg ci anam gu sax, ak doonte fi nun, day mel ne ni mu nekke soppikuwul. Li ko waral nag mooy ni muy soppikoo day faral a yeex lool: doj yi bu ñu sosoo ci ron géej gi, dañuy mujj lemu, yékkatiku, màgg ànd ak Jamono yu jiyoloji yi ñooy mujj sos ay càllalay doj yu yees. + +Ci safaanub loolu doj yi gaaru ci kanamu jëfkay jawwu yi dañuy xolliku, di xoosu, di fellu, bu ko defee, yooyu xoosiit ak felliit (ban yeek beeñ yeek yi ni deme) ñooy mujj sottikuwaat ci géej gi + +Xam-xam +Suuf +Pac : baatu ndoktoor moo gën a neex paj te kenn du wax pac waaye paj + +Xam-xam +Sëriñ Muusa KA (Sëriñ Muusa KA werekaanu Bàmba) woykatu wolof ak araab +la woon bu mag te xarañ ci, ab jullit la woon bu dëggu te di ab sufiyànke +di taalubeb Sëriñ Tuubaa bokk it ci Seexi Sëriñ Tuubaa +yi, taalif na lu sakkan ci ay téere ci wolof ak araab rawatina wolof ndax ki mu +daa tagg wolof mooy làkku cosaanam muy Sëriñ Tuubaa Sëriñam +te sëriñam boobii it Yonnent bi moo doon sëriñam bu ko daa tagg ci araab lakoy tagg, +ndax nit koo di tagg di ko tagge weneen làkk wu dul làkku juddoom tagg ga du mat +ndax yaangi koy tuutalal cosaanam, ay woyam nag li ci ëpp Sëriñam la ciy tagg ak +di soññ bokki taalubeem ngir ñu gën a fonk Sëriñam te nankoo jaamu Yàlla, ku xelu la woon +te jàng ba ci woyam yooyii mu woy ci wolof ku jàng `Aruud (xam-xamu woyiin ci araab) ma nu koo jam, sàmmoonte naak sarti woy ak bahru yi (woyiin yi), ba sos na ay Bahru ajami; niki Téere bi tudd «Bu léen njuuj-njaaj» ak way wi mu jébbaloo ci Seex Mustafaa Mbàkke xalifab Seexul Xadiim bu jëkk. + +ay woyam +Ay-waay bu leen di fàtte yoonu yàlla () te xamni àdduna du kër ay tool la +wacci sa tool mu booy di bayali aw jàmbur () di dër-dëri di wut liggéeyi ba njàmbur +taxuta am dugub sakaane gerte () kerok bisub peret ba yaa cay perte + +bàmba du waa muy gàntu waa muy gënale() loo ca amul ci yaw la yaw miy yellale +ñu jëkk ñaak ñu mujj ñii la yamale () loo ko jëfal mu fayla moom du tappale + +Nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax boo màggatee yalwaani. + +Bëyit yii ci jigéen la jëm, sabab yi tax ñu koy tànn niki soxna, mu jël araf ya araf wu ne mu def ciy bëyit + +Jiim gi + +jigéen ju ndaw araf ya lan ko tënke - tënk ba bis pénc ba lan koy tinkee + +jiimug jigéen mooy jekki bum jàllantu - ndaxte bu jàllantoo asal njaaloontu + +cofeel gu mat sëkk a ko war cib sëriñam - ku bëgg dof te ku doful doo am ngërëm + +jaamu boroomam jaamu it boroom këram - moo war jigéen su ko manee dàmmey ngëram + +jam tuñ ma, jam siiñ ma'ak njamal-yàllaam la - jaalu-yàllaam wa ne Yaasin Salla'a + +Jàmm ak juddook jikkoo waral ñuy tànn - ne xur wi wenn la te jiim yiy jenn + +Kaaf gi + +kaaf nga na baax gaaf, bari ngor, toog fa këram - na bari kersay kër-këriy sàkku ngërëm + +nay gone bum def mag te bum gàtt kutuj - bum gudd lool fum toll ànd ak latkoloñ + +Yaa gi + +yaa ga na yaatu ŋàpp, yaatal dëkkandoom - yaatal boroom këram ci lépp lu mu moom + +yaru te yomb te yéwén te yaatu - cib sëriñam te la mu yor bum laatu + +Arafu nuun gi + +arafu nuun gii ku ko boole xejj - ci sa boroom kër gaa ya duñ la xàjji + +neex cere, neex dereet te neexu làmmiñ - neex lépp tey neexlaate gàttu gémmiñ + +jigéen na maandu, man a muñ te mokk - di muñ di muuñ di mooñ cereem ne mekk. + +Jikko yu aju ci arafu baa jëm ci jigéen + +arafu baa yile jigéen ju boole - seen jikko yii kenn du la ba ngay xoole + +baax baay te booleek bari bayreek barile - ba su boroom këram amul muy defale + +bëñam ya weex tàll ba mel ne perkaal - bët ba ne bàq bakkanam bay safu jaal + +day neexu làmmiñ, neexu ñam te mokk lool - lewet te nooy ku mu dajeel sukkal la teel + +bokk nq ci li mu wax di ci tagg sëriñam ba Sëriñ Tuuba +adunyaa ngi tol new fel fi moom mbaate dëññu teeñ () woroomiy tëndëŋ xammeewu leen ak woroomi téeñ + +lilee tax mu daa tuubloo dameel ak maxa'aki teeñ () ku mel nii ku amleek moom na leen wóor ne yaa ko tooñ + +du tooñ nit te soo tooñee mu jéggal la tin la ko () xamul jaamur ak mbokkam, mag ak ndaw ci aw meloom + +wurus mbaate ab xaalis bëy ak nag xar ak gëléem () la daa buub di jox ñiy laaj du kuy néegaleek a léem + +añs + +Ngir déglu te yér as lëf ci woyi Sëriñ Musaa Ka xoolal foofu: + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Sëriñ Mbay JAXATE + Seex Ahmadu Bamba + Sñ Sàmba Jaara Mbay + +Lëkkalekaay yu biti + Majaalis + Htcom + Ahloubadar + +Niti senegaal +Yoonu murit +Taariixu àdduna bu bees bi te jamonoo +Ag jiital + +Teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam, ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona, moom la lay xamal ciy waxtu, ci lu dulub coona. + +Muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi, te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am, te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen. Ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg, lu mu metti, metti, danoo war a wut ay kunaked babies in my asshole utlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi, te nag yombug xam-xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo, kon lu tax muy français? Ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam, ngir déggante, waxante, te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk, lay gën a nekke jumtukaay boobu. +Lii ak leneen lu bari, moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof, te ba yeneen kàllaama yi, ginaaw bindaluma ku leen moy. Te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa Afrig? Nekkewunu fi lu dul ligeeyal Tugal ak lu ni mel, nanu sunu bopp ñor ! doonte as lëf la it. +Nan la am reew mu tollu ne Senegaal… ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk ? reerale ga’a ngii ! i have a 1 incher + +Abdul Xaadir KEBE + +Bunt bu njëkk bi + +Njëlbéenug jamono yu yees yi + +• Yewwute’g Tugal gi +• Wuññi yu juxraaf yi +• Yëngu-yëngu yi daa kontar Egliis bu Paab bi + +Doggantal gu njëkk gi + +Yewwute ga amoon ca Tugal + +"Yewwute" gu Tugal gi, baat la buy tekki - ci maanaa mu taarix mi mu yore - yëngu-yëngu gu dekkal ak yeesal, walla dundal xay gu Tugal gu yàgg ga ( gu klassik ga), gu Geres ga ak Rom . Rawati na ci wàlli njàggat , fànn ak tabaxiin . + +Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Hiisaa, ba ci bu fukk ak juroom ñaar, mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada, dundiin, mboolaay , politig ak koom-koom. +Kon daal, "yewwute" gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja ( mu'y jamono'y "ag laman" walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji ( di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala ). + +Sabab yi tax Yewwute'g Orob gi am : + +Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy : + +1 - Jeexiit gi xay gu lislaam gi def ci yewwute gii, +2 - Ak feeñug dëkk yu mag yi ci Tugal ( les villes), +3 - Ak neew-doole gu Egliisub Paab bi neewoon doole, ak tas gi mu faroon tas. + +Jeexiit gi Lislaam amal ci yewwute'g Orob gi : + +Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore , araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Orob nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk . + +Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñ yi + +Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya, duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam . + +Lii nag ci li soppi xalaati waa-Tugal yi la jëm ci Egliis bi, nit, adduna bi ak dund gi. + +Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbli woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci ndoktoor, xeltu , gañcax ak ndundat , ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn (g) . + +Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin ( wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Orob ca jamono jooja ) loolu dimblee woon - ci ginaaw bi - ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am. + +Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi ( les villes ): + +"Nosteg laman" walla gog cang, ku ne xam na ne la mu baaxoo woon mooy tegu ci mbay, suuf, ak seqoo yu laman yi daa lijjanti ak'a nos diggante jaam bi ak sang bi.. ag laman nag - jullit ñi masuñu koo xam - nosteg koom-koom la tey gu mboolaay gu bon, daan gàllankoor xay gi ba du jëm kanam. + +Bu ko defee, li ñuy wax "tool", di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste . + +Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug mecce yi ak ligéey yi, ngir jòkkoo gi waa Orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon’a lòtt ak’a naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal ki tàmblee am yoon wu mu man’a jaar bay dund te du sukkandiku - ci léppam - ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi. + +Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu ak’a lakkal noste gu laman gi, tey ligeey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man’a am. + +Lòttug Egliis bu Paab bi akug tasam: + +Egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax "njàng yi aju ci Yàlla" (théologie), ak njàggat ak xellu , amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam. + +Egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war’a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Egliis bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. +Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën’a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa’a xóot, ak bu endustri ak aada . +Yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it - di doyodil nosteg laman gi - rataxal yoon wi ba yewwute gi man’a am. + +Itaali mberum yewwuteg Tugal gi: + +Dëkk yu Itaali yi ñooy mber mu njëkk, mi njëkk’a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax . + +Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg’a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa Rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fann , nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine. + +Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab gi ci Itaali ag tono gu ne-ne ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn ,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa ligeeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi teere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit +ñi. + +Mandargay Yewwuteg Tugal gi : + +Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën’a rëy: + +(1) Yëngu-yëngu yi aju cig "nite" : + +Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya ( yu Gres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war’a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi , ak jeem’a xam seeni mbóot. + +Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati Gres yeek Rom (grego-romain) ñoom lanu jëloon, yittewoo leen,ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. +Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàggat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàggati Gres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam. + +Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. +Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi , di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot , nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja . +Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi. + +Dëkki Itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees, ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal, te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu Gres wa. +Tabaxiin wii siw na lool te tas ci Egliis yi ak katedraal yi, ak saal yi ak barabi tiyaatar yi, ak sangukaay yi . + +Ci dëkki Itaali yii, lu bari ci waa-fànn yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko ( 1400 - 1455 ), mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën’a mag, ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya . +Ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal, mu nekkoon moom ku diinewu. + +Bokkoon na ci ñoom it Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 ), moom mi boole woon fànn ak xam-xam, defar nay nataali fànn yu siw, bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi, ak Jokanda, walla Mona Liza. ñaari nataal yii ci yi gën’a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute. +Da Vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk, waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag,dib rëddkatu tabax te dib eesañër bu muus. Bokk na ci deseñkati Itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax Titian (1488 - 1572 ), moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi, ak Rafayel (1493 - 1520 g ), moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon, te di deseñkat bu bokk ci ñi gën’a siw ci mbooleem jamono yi. + +Bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci Itaali ba tay, yattkat ba Donatello ( 1386 - 1466 ) , mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya, di gres-rom, rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam. Moom daal ca dëgg-dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi. + +(2) Feeñug làkk yu bees yi: + +Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi , moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon. + +Bi jamonoy "yewwute" dikkee, ngelawul "fonk sa xeet" upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu. + +Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi. + +Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). + +Chaucer mi dib angle ( 1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën’a siw. + + (3) Feeñug xeeti Orob yu yees yi: + +Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Orob taxaw, yu amoon "ag temb" ,ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci "temb" tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi . + +Looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk, xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man’a laal ci xeli lu bari ci nit ñi. +Ci noonu xeet yu bari ci yu Orob yi, tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf, di goreel seen bopp ci toppub jàmbur, te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi +Ay àtte nag yu Tugal yu am ay nekkte yu politig yu temb juddoo ci loolu ci ginaaw bi, yu am seeni làkki bopp yu yees, di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat, lu dul ci jamonoy yewwute gi. + +(4) Yëngu-yënguy dajale mbind yi: + +Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci Xustantin ak ci dëkki Gres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal, mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Gres yeek Latin, yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi,ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii. + +Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot’a am ci misaal rekk,mbindu’m binkat bii di waa Rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g) . +Tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi. + +(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya: + +Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya. +Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam , waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix , mu tudd daaray xam-xam bu taarix. + +Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla ( 1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn dosye bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax "mayug Xustantin", mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen . + +Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli ( 1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas. + +(6) Jëm-kanamug yaxantu ak endustri: + +Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi , ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa . + +Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci kee yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug "maas gu diggu" gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi. + +(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi: + +Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. +Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi , ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi. +Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon ( 1220 - 1292 ) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal . + +Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf . + +Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ ( 1561 - 1626 g) , di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi , ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd . +Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 g) moom tam feeñ , di kok dafa yittewoo woon jiyoloji ( bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn , tey fentkat. +Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 - 1642 g) feeñ , mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba , dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus ( 1476 - 1542 g). + +Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel , walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam. + +Yewwute gi ci Itaali: + +Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo: + +1 - Song gu mbooloom xarem Fraans mi ak mu nguurug Rom gu nu sellal gi songoon dëkki Itaali yi, rawati na Rom ak dëkki bëj-gànnaar yi, niki Milano, loolu it taxoon na ba ñu giir dëkk yooyu, te Milano ak Rom jiitu woon ci. Ci noonu la yewwute gi delloo ginaaw ci Itaali ngir ñàkk gu fa jàmm ñàkk ak kaaraange ak dall. + +2 - Jeex gu àtteg walla kilifteefug njabootug Madatsi jeexoon, ñooy buur yi daa sàmm yewwute gi ci Firenze , loolu nag sabab si mooy xuloo ak xeex gi amoon ci biir njaboot gii, te Firenze moo ëppoon solo ci barab yi yewwute gii nekkoon. + +3 - Teg loxo gu buurub Espaañ bi Ferdinando, buurub Argon, defoon Napoli atum 1504 g, loolu bokk ci li neewaloon doole yewwute gi ci dëkku Itaalib bëj-saalum bii. + +4 - Yëngu gi amoon ci jéem’a yéwénal diine ji ci Orob, ñi ko daa def di Luther,Kalfen, Swingli ak ñeneen, looloo taxoon paab gi jug ak doole ci kontar nite gi. Nga xam ne sax noonu gi àgg na ci paab bi tuddoon Kalimat mu juroom ñaareel mi, kompoloo woon ak buur bi Sarl 5 (Sarlkaan) buurub Espaañ bu katolig bi, ngir ñu fexee naaxsaayal yëngu-yëngug nite googu ci Itaali. Loolu mooy li waajal mbir yi, nooyal yoon wi ba “ëttu àttey lajmat" yi man’a am ca Esapaañ, di woon ëtti àtte yu siwe ay jëf yu ñaaw, daan sonnal ak a fitnaal képp kuy woote yéwénal, mbaa’g yewwute. +Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund. + +Tuxug Yewwute gi: + +Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs. +Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay. +Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen. +Nitug Holand kii di Erasmus ( 1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi. + +Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax "kòllare gu yees gi" def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon. +Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi. + +Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali: + +Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll. + +Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey. +Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi , looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal. + +Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g. + +Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom. +Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi. +Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi. + +Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g ) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g ) ak ñu dul ñoom ñaar. + +Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi. +Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer. + +Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam . + +Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew. +Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii. + +Doggantal gu ñaareel gi: + +Wuññi yu juxraaf yi : + +Luy wuññi yu juxraaf yi ?: + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf, walla feeñal gu juxraaf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg,njëkk waa-Orob di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc , ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu juxraaf. + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, da nanu ko man’a xamalee ci nii: +mooy mbooloom ligeey yi jéngukat yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii: bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu. + +Li sabab wuññi yii: + +1) sabab bu diine: + +Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf yu Orob yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari reewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu. +Ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Reewum Portigaal moom daa gisoon ne reewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono. +Paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonnal ko,tee koo tas, ngir neewal dooleem, xottite ko,giir ko. + +Ci noonu mu ( moom paab gi) génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam geej yi la mbaa jeeri yi. +Paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nanu leen fi jeem’a jële. + +2) Sababu politig: + +Am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Fraans, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit ci biti seen, rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu'g nekku walla sosu gu yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man'a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen . Reew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi. + +3) Sabab bu koom-koom: + +Waa Orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal,mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir neewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi , loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke. + +Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova ak yu leen moy. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi. + +Lori waa Orob yi tàmbli woon na’a yol, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi rekk, bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Orob yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g ), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd , ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi . + +4) Sababu xam-xam: + +Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak bindam dafa soppiku woon, ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal ,juge Orob, génn, rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Orob yépp ci jamono yu diggu yi. +Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu , ak bëgg xam-xamu juxraaf, feeñ ci ñoom, ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi - ci xam-xam bu juxraaf bu jëm kanam, ak ginaaw bu xam-xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam. + +Wuññiy juxraaf yu Portigaal yi: + +Portigaal moom la ñu’y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf , yu Orob yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool (1394 – 1460 g ) , doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon dugg geej, ak yër xisay mool yi, ak teerey taariix yi . Muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi , moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta , ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g. + +Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi geej gu xonq ga ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum 1445 g, ginaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niijer. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko « Boppub Yaakaar Ju Baax Ji » ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End. +Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi, romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji, ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka dun bu End. +Vasco De Gama mii jot naa xamante ak Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi. +Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu geej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi nuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song barab ya ak mbooloo’m gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo ak buuri goxi End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End bi. + +Li wuññiy juxraaf yu Portigaal yi jur : + +Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw : + +1) Waa Portigaal, ñi ngi tàmbli woon di teg loxo ci tefesi Afrig yu sowwu yi, ci noonu njàppum jaam siw, te tas ci Orob gépp, di jaam yi ñu daa jàppe Afrig, te daan ci yaxantu. + +2) Jamonoy sanc gu Portigaal , mi ngi tàmblee ci bi Portigaal taxawalee ab sancu , ci penku bi, ca fa ñuy wax Jawa, ay xare it am diggante araab yu jullit yi ak Portigaal cig wàll, ak ci diggante waa Portigaal ak waa End yi ci geneen wàll. Waa Portigaal yi nag jot nañoo teg loxo yenn waax yu am solo yi nekkoon ci yoon wi jëme End. + +3) Waa Portigaal yi mujj nañu xam yoonu yaxantu wu geej, wu dul romb ci reewi jullit ñi,mooy wi jaar ca Boppu Yaakaar Ju Baax ja . + +Loolu nag mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi. + +Wuññi yu juxraaf yu Espaañ yi : + +Li ci duggaloon Portigaal, moo duggal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi. + +Moolub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahama ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi. + +Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ». + +Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul End. + +Ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal Espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu , ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca gox ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraagay ñu tudde ko Adduna bu bees bii di Amerig tay. + +Li wuññiy Espaañ yi jur: + +1) Ñoom de ubbil nañu tukkiy wuññi yi aw yoon wu bees wu jëm ci àdduna ju yees ji, di ko jaare ci màmbulaan gu atlas gi . Bu ko defee Espaañ tàmblee sanc gox yi mu jotoon’a àgg ci Amerig gu diggu gi ak gu bëj-saalum gi, ñu wisaare fa seenug xay ak diine, ubbi fa ay mbelli wurus ak xaalis. + +2) Saxal gu ñu saxal ci xam-xam ne suuf si daa “bulu” , te li waraloon loolu di tukki bi Magellan defoon. Buur bi ñu daa wax Shark mu juroomeel mi (Sharlakaan) di woon buurub Espaañ, daa digaloon mool bii di Magellan atum 1519 g, mu def ab tukki jëm penku jaare ko sowwu, ci noonu moom Magellan jug, war geej, jawali sowwu, te jëm penku, ci kaw màmbulaan gu atlas gi, bi mu ko defee daal di àgg ca tefesug Braasil ga, fa Riyo De Janero, mu wëy nag ca doxam ba, ba ca sottiwaayu dexug Labalata, daal di wër Amerig gu bëj-saalum gi, tàbbi màmbulaan gu dal gi nga xam ne moom moo ko tudde « pasifik » di wund lu dal, mu àgg Filipin atum 1521 g, foofa nag mu songoo fa’ak ñoñ réew ma, ci’y xeex yoy ca la ñu ko raye, waaye kenn ciy nitam, tuddoon Dianco, moo mujjoon jiite boobu tukki, dem ak ñoom ba ci boppu Yaakaar Ju Baax ji, juge fa dem Espaañ, gi nga xam ne ma nga fa àgg atum 1522 g. + +3) Weddi gisiin yi daa wax ci bindu suuf si ak ab kemam ( ni mu tollu), ndax kat tukki bii nga xam ne dafa dox, wër àdduna bi, firndéel na ne suuf si daal moo ëpp fuuf li ko Colombo jàppe woon ak ku dul moom. Beneen gox feeñ na, bu mag diggante Orob ak Asi ci wàllug sowwu gi, di Amerig gu bëj-gànnaar gi, nga rax ci dooli geneen gi’y gu bëj-saalum gi, te ag màmbulaan gu yaatu, gu yees’a ngii gu ñu xamutoon. Kon suuf desatutoon su ñu xamutoon su dul Ostrali ak ñaari xutbu yi . + +Wuññi yu Angalteer: + +Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu geeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug walla koloniiseg waa Angalteer yi, ñeel Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa . Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland. + +Wuññiy Fraans yi : + +Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy Fransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fetali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Fraans tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak goxi dex yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebek ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. moolu Fraans bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Fraans ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi. + +Wuññi yu Oland yi : + +Lonkoo gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu geeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali golofub New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ. Waa Oland yi jeemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g . + +Li wuññiy juxraaf yu Orob yi jur : + +Li wuññiy Tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw : + +1) Njiitug yaxantu gi tuxu na tukkee ci li wër geej gu diggu gi dem ci màmbulaan gu atlas, mu mujj moom yaxantu gi nekk ci loxoy reewi Orob gu sowwu gi, bu ko defee ñu nos fi ay yooni geej yu yaxantu ci ñaari màmbulaan yi, gu atlas ak gu dal gi (pasifik). +Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » . + +2) Wuññi yu juxraaf yi amal nanu fi jawwu yu gëpplante ak wujje, ak as lef cig noonoo ci diggante reew yi doon def wuññi yii, loolu moo yokkoon xemméemtéefi sanc yi ci diggante reewi Orob yi. Ci noonu aw gisiin wu sanc tàmbli woon’a feeñ wu Orob jëm ci askani reew yii ñuy door’a wuññi. + +3) Xam-xami juxraaf yi soppiku woon na bu baax, li ko waraloon di yaatu gi wuññi yii yaatu woon te bari. Ci noonu yëngu-yëngu gu nasaraanal yokku ci anam gu fés, rawati na ci Afrig ak ñaari Amerig yi. + +4) Ag jëm kanam feeñoon na ci wàllug yaxantug mbèll yi, di wurus ak xaalis, nga xam ne sax xarnub fukk ak juroom g, danu koo tudde woon « xarnub xaalis », ni nga xame ni jëm kanamug koom googu taxoon na ba dundiin wi gën’a kawe, njëg yi it gën’a yekkatiku, ni fi ay njaay yu yees dugge, lu ci mel ne kakawoo, poon, kiinaa, batata ak mbòq . + +5) Wuññi yi de lenn lanu ci màndarga yiy wone yewwuteg Tugal gi, ni nu la ko leerale woon ci doggantal gu njëkk ga. + +6) Reew yii ñu wuññi, ruu gu fees ak bëgg’a fayyu moo leen ubale woon, muur leen, jëm ci yii leen wuññi, ndax ñoom tubaab yi xalaati sanc lanu yoroon, daan ci doxe ci mbooleem seen doxi wuññi yi, lepp lu nu gis aakimoo ko, ngartaajoo ko, lii mooy li waral askani reew yi nu wuññi, jugoon ci jànkoonte ak ñoom, taxaw ci xeex canc gu Tugal gi, ci anam gu tar, jëfandikoo ci li nu yor lepp ci kàttan. + +7) Wesaare diiney nasaraan ci bepp gox bu nu wuññi. + +Doggantal gu ñatteel gi : + +Yëngu-yëngu yi jugoon di kontar Egliis bu paab bi + +Yëngu-yëngu gu yewenal diine ji ci Tugal : + +Yëngu-yëngu gu yéwénal gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Orob ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jeem’a delluwaat ci njàggaley Injiil yi. + +Li waraloon « yéwénal » gi : + +Ak li Egliis bi di nekk nguurug ruu lepp - ci li ko njëkk’a tax’a jug - teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot’a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom, ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Egliis bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtoo’k moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni. + +Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag yi ñépp di fay. Ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp. + +Ñaawtéefi Egliis yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi. + +Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat , nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex. + +Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Orob : + +Yéwénalug diine ci Orob - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam. + +Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Egliis bi te dëgëral ko. + +Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Egliis bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci egliis bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 - 1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam . + +Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli. + +Martin Luther ak yéwénal gi : + +Martin Luther mi ngi juddoo Isilban, di benn dekk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaa�� atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi. +Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Egliis bi, li gënoon’a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi, ginaaw bi it, mu mujj fèttéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam. + + Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam. + +Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Egliis bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal . + +Luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Egliisub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Egliisu Watanberg ba, lakk ko. + +Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon : + +Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii : + +(1) Injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute. +(2) Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni. +(3) Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil. +(4) Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi. +(5) Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi. +(6) Wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi Orob gu sowwu gi. + +Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ-sañu paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi Egliis bi aki am-amam, ndax loolu man’a soril Egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci Egliis bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom Egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom. + +Jëfka yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu : + +Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii : + +(1) Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Orob yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a fèqu ak’a dañtalu ci ŋëbug paab gi ak sañ-sañam. +(2) Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam. +(3) Fonk sa xeet,walla xeetu gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Orob yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw Martin Luther, rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya. +(4) Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu. +(5) Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër it jam yi mu doon def Egliis bi . +(6) Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom. + +Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy protestants, maanaam ay diiŋatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi (katolig yi) ci geneen wàll. Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne goxu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant mbaa mu katolig, waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj-gànnaar yi – egliisam daal di doge ca egliisub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmark ak Suwed) . + +Kalfen (Calven) : + +John Calven mi ngi juddoo Fraans atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraans dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine . +Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi. +Kalfen ak Luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy: +(1) Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko . +(2) Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma. Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraans, Angalteer, Siwis ak yeneen. +Swingli : + +Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi. +Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine. + +Swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Egliis bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye. +Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Orob yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi. + + + + + + + + + Bunt bu ñaareel bi + +Jëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustri + + + +• Jeexiitalu gu waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi. + +• Lefi (wàlli) jëm kanamu xam-xam ci Orob. + +• Yewwuteg endustri: ay jagleem – ay màndargaam – ay ngérteem (li mu fi jur) + +Doggantal gu njëkk gi + +Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi. + +Jamono ji xam-xam neewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat, te meññi. +Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon’a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi. + +Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris End, rawati na ci ndoktoor, bidiw, ak mat ak yeneen yi. +Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaton ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi. +Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat, kimyaa ak xam-xami dénd yi , bidiw, juxraaf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell. + +Ngérum walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi: +Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii: +Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem’a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi . +Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono. +Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer ji di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu. +Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon’a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xam bi aju ci Yàlla . + +Digg yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Orob: + +Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Orob jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker-keraan yu bari, bokk na ci yooyu: + +(1) Andalusi : +Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon. +Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Orob yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Orob yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak’a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi. + +(2) Dunub Sisil : + Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Orob, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi. + +(3) Xarey jooñ yi bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Orob jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab, ak yi nu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris . +(4) Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Orob, rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi. +(5) Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Orob ci jamonoom ju bees jii. + + Xam-xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa Tugal yi: + +Lim (Mat): + +Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami kalkil yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon. +Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam-xamu waññ ( calcul), ñoo dolli woon tus ci lim yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam al kasr alhasarii di ci wolof (damat ci fukk) , ñu taalif ci wàllug xam-xamu waññ (calcul) ay teere yu waa Orob yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci. Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xam-xamu lim walla waññ, moom de lanuy sant bu lim (mumero) yi nekk ci kalkil duggee Orob tay. +Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki Orob yu bari. Boroom xam-xami Orob yi jariñu ci. +Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci matematig yi(xam-xamu lim), ñoo njëkkoon waa Orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii. +Bu dee nag ci andasa , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi nu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xam –xamu kalkilu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi . Nu xootal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g. + +Xam-xamu Fisiya : + +Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu Fisiya ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “séen” (almariyaat ). +Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab teere bu am solo, mooy teereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Orob yi mujjoon nanu ko’o tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g). +Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan Bun Alhaysam (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu fisiyaa, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo. + +Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët, ak weer yi ak leer ak yeneen. +Waa-Orob yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Orob yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax. + +Xam-xamu bidiw : + +Jullit ñi yittewoo woon nanu xam-xamu bidiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi, xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe. +Jullit ñi jariñu woon nanu ci xam-xamu bidiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu Geres yi niki teereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi. + +Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami bidiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom. + +Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi. +Waa Orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam-xamu bidiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam. + +Kimya: + +Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu kimyaa, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang . + +Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik , ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen. + +Mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki: seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal. + +Da na jaadu nu leeral ne xam-xamu kimya moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari. + +Waa Orob jariñu nanu bu baax ci xm-xamu kimya bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli. + +Ndoktoor : + +Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci xam-xamu ndoktoor. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw. +Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci ndoktoor, taalif na ci lu sakkan. +Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci ndoktoor, teereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de jenn jimblang la ju xam-xamu ngoktoor, ju waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Orob yi jariñu nanu ci xam-xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Orob yi. Waa Orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax Kaaw su nuy opere (xotti). + +Waa Orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk. +Bokk na ci boroom xam-xami Orob yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy. + +Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Orob’a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Egliis bi. + +Da na yell nu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Orob gu sowwu gi, ginaaw bi ab kureel ci waa Orob yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom. +Kon lu nu war’a xam la ne yewwuteg xam-xam ak gu endustri gii am ci reewi Orob yi, ci ginaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Orob tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay . + +Doggantal gu ñaareel gi + +Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal + +Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Orob, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu endustri ci Orob, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp. + +Li taxoon xam-xam jëm kanam : + +Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci reewi Orob gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di: + +(1) Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Orob yi te jariñu ci. +(2) Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam +(3) Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi nu fentee móolukaay yi. +(4) Xeemmeemteef gu waa Orob yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: yu Gres-Rom ya. + +Wàll yi xam-xam jëme kanam : + +Ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci Orop lepp, naan jamonoy reer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn mant’a reere, mant a weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu neew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu . Ci noonu Orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di: + +Ndoktoor : + +Ndoktoor ci Orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi, jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa Orob mujjoon nanu leen’a firi ci seeni làkk. + +Xam-xam bi Orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii, ba ci xarub fukk ak juroom benn g. + +Waa Orob yitewoo woon nanu bu baax xam-xamu ndoktoor, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom dey xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci Orob. + +Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci reew yii nuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci Orob. Mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci Orob ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje, wutal leen ay garab. + +Ci noonu boroom xami-xami Orob yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Beljik mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Fraans, ak Lofan Hok mu Oland mi, ak Luwis Pastor mu Fraans mi ak Kox mu Almaañ mi añs. +Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs. + +Juxraaf ak Bidiw: + +Xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal, te boroom xam-xami bidiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gëpp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nanu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay ligeey ci googu wàll. + +Waa Tugal yi nag seen xam-xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci Orob. +Jem kanamug xam-xamu Juxraaf tax na ba bu Bidiw it jem kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom dey duggal na loxoom bu baax – boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam-xamu bidiw – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi, bu ko defee nekkteefi asamaan yi di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi, ñoom ñepp danuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wëndeelu, maanaam roo te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wëndeelu. +Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu Bidiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi. + +Fisiya: + +Xam-xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu fisiya bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu. +Boroom xam-xami Tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si . +Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yeegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yef sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yitewoo xam-xamu fisiya, ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g. +Boroom xam-xamu Angle bii di Isaac NEWTON (1742 – 1727 g ) mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si . Moo wax ne bidiw yepp, walla plaanet yepp, danuy wër jant bi, ci ay ngunu yu sax , walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon. +Ki nuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni bidiw yi sosoo. + +Kimya: + +Waa Tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu Kimya bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw. +Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti kimya yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci. +Toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore. + +Waa Tugal yi nag, ñoom, danoo gën a jëmale kanam xam-xamu Kimya, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi, ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Fraans, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g. + +Kuran: + +Boroom xam-xam bii nuy wax (Thales), di ku dëkkoon Gres, moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran. Boroom xam-xamu Angle bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigeen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul kuran rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum 1672 g. + +Ki nuy wax Stephen Gray dikk, won nu ni nuy tuxale kuran, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci fiil yu xànjar. + +Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi kuran yi, te fent batari. Borom xam-xamu Amerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak kuran benn lanu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum 1831 g. +Waa Tugal soobu nanu ci xam-xamu Mat, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Frans bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële. +Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu Jiyoloji la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo. + +Jamonoy yewwute daal ci Orob mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te feexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Orob ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jeem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam. + +Ñatteelu doggantal + +Yewwute gu endustri : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi + +Yewwute gu endustri ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g. +Waaye nag, moom endustri mii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Amerig, la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. +Bi mu ko defee nag, ay jeexiitam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g. +Endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll. + +Looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal. + +Sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal: + +(1) awaase gi xam-xam awaase ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg endustri am. +(2) Dëkki Tugal yu mag yi, am gi nu am, ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam, rawati na, bi ci aju ci ràbbu ser , nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci Tugal. +(3) Jëmm ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Orob yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, feexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam. +(4) Li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it, muy teg loxo gi reewi sancaan yi daa def reew yi nu sanc , ak di fa jële ay xeewal aki ne-ne yu nu laalagul , di leen yobbu seeni reew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci Tugal. +(5) Reewi Tugal yi ak këri koppar yi, jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci Orob, loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox, man a àntu. +(6) Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal. +(7) Bari gi ligeeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci ligeeykat yi amoon xam-xam yu neew lanu woon, nga xam xam ne daanaka jàngunu woon. + +Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam : + +Yewwuteg endustri ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lanu: + +(1) Jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb : + +Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. +Loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci. +Ràbbkatu angle bi nuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin bu loxo, bu nuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla pono, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn ligeeykat di ko yor, di ko doxal. +Bu ko defee, fentkat bu angle bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas, mujj nu koy defe ci dooley ndox, nu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame). +Ki nuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari goxi Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire . + +Ki nuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox, ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb, daa ko defar ciy sér. + +Ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu Kimya yi ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey. + +(2) jëfandikoo kàttan : + +Jumtukaay yu njëlbeenu yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat . Kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ. +Ki nuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi, ak li nuy ligeey, ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci endustri ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll. + +Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland. + +Nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginaaw bi, nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi. Ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs. +Kuran tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li nuy wax juddalukaayu kuran, nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam. +Nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi. + +(3) Jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam: + +Bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ, loolu nag mooy bi angle bii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy ligeey. +Lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani. + +(4) Jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam: + +Li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug coolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi. +Ginaaw bi, nitug Amerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo coolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Ginaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi. +Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko endustri defe. Bu ko defee, feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi. + +(5) Feeñug campeefi endustri yi : + +Ligeeyuwaay yu ndaw yi juge nanu ci kër yi, doon leegi ay campeef yu endustri, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. +Endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu endustri, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi. +Isin yu mag yi nag, ci wetu barabi ne-ne yu nu laalul yi lanu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey, ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew. Neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel. + +Li fi yewwuteg endustri gi jur: + +Maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci Tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay. + +Li mu fi indi ci wàllug koom: + +Yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom, ci biir Orob ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li nuy ligeey gën a yokk, gën a wuute, li nu koy jënde gën a neew, ñepp man cee jot, jumtukaayi ligeey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu adduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk ak sanc , tàmblee booloo. +Ndax kat sanc gu politig gu yees gii, du lu dul doomi sanc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ne-ne yu nu laalul yi, ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute. + +Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp, ak li mu gën a ñaw lepp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a ligeey, ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari, te daa nanu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Orob, rawati na ci Angalteer. + +Joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi, nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu adduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi. + +Li mu fi jur ci politig: + +Sanc gii Tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi, wuutal ko fi, ginaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw , endustri day soxla ay ne-ne yu nu laalul, te loolu danu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii, tax it ba reew yi nu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag sanc, ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi. +Bu ko defee, benn dal daal di feeñ ci Orob, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu libre ” bi am te taxaw ci nosteg bopp-alal . Loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen. +Goornamaay Tugal yi, jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan . Ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi endustri yi. Loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi. + +Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay. +Goornamaay Tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi, ci noonu ñu yamale waxtu yi nuy ligeey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lanu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi, jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax. + +Man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew, feeñ na, te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis reewi Tugal yi sukkandiku ci endustri, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi nu miinoon. + +Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay: + +Yewwute gi ci Orob jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi, ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki endustri yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll. Bu ko defee baykatu Orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi. +Lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a neew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy neewug jóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer. + +Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër ligeey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey ligeeykat yi gën na a yokku, bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja’a neewi seeni aajo, ngir seerug dund gi. + +Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd’ak yewwuteeg endustri gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi, leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay, ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg. +Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi, ci Tugal, maanaam nit ñi, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci Orob, ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe-jafey ligeey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos ligeey bi, aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal yi moom isin yi. + +Ñatteelu bunt bi + +Yëngu-yënguy politig yu mag yi ci adduna bi + +Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A) + Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans + +Doggantal gu njëkk gi + +Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi + +Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Amerig, gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Amerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci: + +(1) Fitnay diine yi amoon ci Orob gu digg gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di kontar Egliisu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak mu Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Amerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore. +(2) Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig . +(3) Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, danoo gëmoon ne Amerig de reew mu fees dell la ak yile mbèll, te ña fa dëkk, ñu neew ag xay lanu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll. +(4) Jëm kanam gi xam-xam am ak endustri ci Tugal, rawati na ci wàllug ligeey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori. +(5) Ligeey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nanu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi. + +Sancu yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nanu leen ci Amerig gu bëj gànnaar gi: + +Waa Tugal yii bawoo woon Espaañ, Fraans, Holand, Suwed ak Angalteer, sancoon nanu ay barab yu wuute ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lanuy wax tay Diiwaani Amerig yu Bennoo yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nanu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaayeTugal. + +Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb akug dagge ca reew may nday di Angalteer. +Angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy : buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci nu taxawal ay sancu, ak jariñoo xeewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi. +Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen . + +Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy: New York, Wirjiniya, Rood Island, Masacuusest, Dulawir, New Hamser, Kintakit, North Karolaayna, South Karolaayna, New Jersi, Jorjiya ak Pensilvaniya. Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Amerig gu leegi gii nii, dunu weesu benn xaaj ci Amerig gu nu xaaj fukki xaaj. + +Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi: + +Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte sa bopp” , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di reew mi leen moom. +Nosteg àtte-sa-bopp googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk: + +(1) Doxalkat bi , +(2) Jataayub yoonal bi , +(3) Jataayub diisoo bi . + +Doxalkat bi walla àttekat bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (àttekat bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli. + +Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu ligeeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru doxalkat bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal. + +Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom. +Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte-sa-bopp ” gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer. + +Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen reewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew, di ci tënku, te di ko fonk. +Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi . + +Li waraloon xareb temb bi: + +Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lanu woon yu di ay protestant . Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy: + +(1) Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas” +(2) Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu. +(3) Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo dim reewam, fa la feetale ag reewoom . + +Ëttub Amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii: + +Yoon yuy tege galag ak tembar: + +Parlamaa bu Britani bi daa genne atum 1762 g, aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi, mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu Ofisel yi, ak dosyee yi, ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Fraans yi ak yu Holand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak rasaas . + +Yoon wi aju ci geeju (navigation) ak yaxantu: + +Ci atum 1651g, barlamaanu Britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal li nuy genne ak li nuy duggal di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na Angalteer. + + Koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf: + +Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel . Noonu tam lanu teree woon – ci beneen luwaa - ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom. + +Nos dooley kaaraange ji: + +Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci genn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko. +Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer. + +Waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp, dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon. +Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante. +Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu nu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu. +Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nanu ne moo waral xareb temb bi. + +Ndajem waxtaan mu Filadelfiya mu njëkk mi: + +Juroom ñeenti diiwaan yu Ameriig teewe woon nanu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg. +Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi. + +Looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” . + +Man nanu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko, di ci kontar ni Angalteer di àttee seen reew yi. + +Ñoñ sancu yepp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfi, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yepp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii nuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma. +Ndajem Filadefi moomu, mooy dàtt bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi . + +Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom. +Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ - ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi. + +Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon. +Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nanu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefi, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def. + +Ndajem Filadelfi mu ñaareel mi: + +Ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfi, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfi mi, ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar – ak doonte lu neew la itam – seen diggante ak Britani, reew miy nday. + +Ni xare bi tàkke : + +Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu Amerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Amerig yi. +George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu. + +Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington gañe woon na njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanada, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi nu gañee Britani, Fraans jug na, yëgleb xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Holand topp ci atum 1780 g. Man nanoo wax ne Fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu bennoo yi, ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Fraans lii di Lavette, kontar Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci jë yu bari. + +Dàq gi nu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa Fraans aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat. + +Nanu fàttaliku nag ne waa Amerig yi ñoom, ci seen suuf lanu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanada, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka. +Nga rax ci dolli, waa Amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nanu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington. +Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi. +Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Amerig. + +Tembug Diiwaani Amerig yu Bennoo yi: + +Bi waa Britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Amerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe, gañee ko ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Paris, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g, lii mooy poñ ya ca ëpp solo: + +(1) Britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon. +(2) Jeem a rafetal seqoo yi, ci diggante Britani ak reewum Amerig mu temb mi (Diiwaani Amerig yu Bennoo yi) +(3) Amal ci diggante Britani ak Amerig gu temb gi, ay seqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom. + +Nii daal la Diiwaan yu Amerig yu Bennoo yi ame, xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi. +Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke. + +Amerig nag moom, daal di ñew, defar sartu reewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nanu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cer ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi. +Ginaaw bi lanu def Washington – ginaaw bi mu nekke peeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def peey bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Amerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi. +Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon. + +Doggantal gu ñaareel gi + +Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans : + +Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (fipp googu), mi ngi ame woon ca Fraans, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benn ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu toll ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g) defee yong gu nuy wax yongug 18 Brumaire, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi. +Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Fraans gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk jàmm ga, tiitale ga , tuur dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug Fraans gi. Loolu nag taxoon na ba “fipp gi” manu fi woon a amal dali gore , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi. +Waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi, yamuñu rekk ci Fraans, waaye weesu nanu ko ba daj Tugal gepp, ak lu bari ci reewi adduna bi. + +Ni Fraans meloon laata fipp gi: + +Bu ñu gëstoo na Fraans meloon laata fipp gi, loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi, atum 1789 g. + +Melokaanu politig wa: + +Buuri Fraans yi, ni ñu doon àttee Fraans, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lepp, kepp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub Fraans bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ). + +Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi. +Moom de jaraafam yi danu koo yilifoon, ak bëkkneegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal, kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar. +Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Fraans yi bañoon. + +Njabootug Barbon gi, yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Fraans wi, ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo reew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe Fraans. +Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali reew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi. Looloo taxoon njëlul nguur gi loof, mujj moom nguur gi fees dell aki bor. + +Nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci 130 milyong yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyon yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon. + +Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga. +Nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Fraans mujj di reew mu ay gox boole, gox bu ci nekk am ay yooni boppam , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi, reew mi mujj seddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Fraans mujj doonatul menn reew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas. + +Na mboolaay ga meloon: + +Mboolayug Fraans gi, njëkk fipp gi, dafa seddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: kureelug ñu tedd ñi, walla garmi yi, kureelu niti diine yi, ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi. Ñatti kureel yii nag – ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu – yamoowunu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay warteef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay. + +Bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi, yu siwil yi ak yu xare yi , ci nguur gi. +Ñoom ba tay, daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm yi, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amunu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi. + +“Nitu diine yi” nag ñoom, seen kureel moom itam bu ràññiku la woon, niki bu garmi yi, ñoom de daa nanu am ay suuf yu nu leen dogal, yu yaatu, yu daa toll ci juroomeelu suufi nguur gi, maanaam bu nu xaajoon suufi nguur gi juroomi xaaj, benn xaaj bi. Ñoom itam, ñu nu teggiloon ay galag lanu. Li Egliis bi daa gañee ci suufam yooyu, ak ci galagi diine yi nga xam ne mbooloo mi daa nanu ko ko fay, àggoon na ci 200 milyon yu Farank. + +Loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbli. +Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu feexoon, moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi. + +Kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi fipp gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyongi nit , te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon 300 junniy nit. Coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kureel boobu nag (bu baadoola yi), moo ëmboon kureel bu diggu bi, walla bi nuy wax (Bourgeois), ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si. + +Bu dee kureel bu diggu bi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amunu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon. +Lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi. + +Bu dee “kreelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen ligeey yi gën a tar. + +Bu nu nee “kureelub soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi moom, ak pal yu mag yi, garmi yi lanu leen daa jagleel. + +Na fa xalaat meloon: + +Ak li Fraansu njëkk fipp gi, di gënadi woon a nekk cib coona, ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lepp, teewul waa Fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs. +Jamono jii , dafa fiiroo ak diggante bob Fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nosi politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya. +Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau. + +Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay ligeeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Fraans ak feneen. +Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi, te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju doxal ji, ak ju laman ji . +Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca Fraans. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca Angalteer. + +Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Fraans wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam lanu woon ak yéjj . +Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Fraans ak gu egliis ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi. + Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Fraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital. +Wolteer de gore ga waa Angalteer ame woon da koo neexoon lool, yeemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy danu koo dàqe woon Fraans. +Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca teereem ba tudd “bataaxeli xeltu” , walla ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer, atum 1734 g. +Wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon Fraans, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi. +La desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër. +Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom teere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi. +Fippug Fraans gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi ki dëkk Fraans – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi. + +Jafe-jafe bu koppar ba: + +Atum 1789g, mooy at mi fipp gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom, waaye la waraloon fipp ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon. + +Luwis 16, bi mu ñëwee jeem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kureel yu xeet wi” – bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje. + +Naka la fipp gi ame woon : + +Doomi kureel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir nu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Fraans man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk. +Ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll, ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll. +Bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kureel yi (bu garmi yi ak bu niti diine yi) bu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kureel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cer , ne daal ay neeg ñooy woote, bi loolu amee, ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee, cig beru, ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi reew mi, bu nu booloo, waxul bu benn taqalikoo nee, beru. +Ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Fraans, bi nga xam ne day leeral li waa Fraans bëgg, tey jeem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug fipp gi. + +Tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen: + +Ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca Versailles ngir defaral Fraans ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, genne ña ñu fa tëjoon ngir politig. +Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Fraans wi di màggal, at mu nekk . + +Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Fraans, dem feneen. +Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Fraans, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi, ndax du seen njariñ, danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ . + +Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi, aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba. +Xarekati fipp gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse ak gënjëng . + +Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi. +Xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu ju Fraans ji mujj fekksi “wattu gu reew “ gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi. Ci noonu mbooloom xare mu Fraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba. +Waaye way fipp yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi, ak mu Egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Fraans gepp, ñu daal di seddalewaat Fraans def ko ay doxaliin yu bees . + +Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jeem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy genn reew mi, gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan. +Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 sebtambar 1791 g, loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Fraans la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi. +Mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Fraans wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur saxoon na ca Fraans ba ca 21 sebtambar 1792 g. + +Ci atum 1792g, beneen woote amoon na, bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Fraans, ca 21 satumbar 1792 g. +Ñu feetele ko doxal reew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar fipp gi, aar it Fraans ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci reew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen reewi Tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi. +Feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu Fraans bu dëgër, boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi. +Ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, danoo gëmoon ne fii Fraans toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ��u diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi. + +Ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi: + +Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci reewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Fraans, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange, feetale ko ligeeyub aar Fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi, ñu feetale ko ba tay moom kureel bi, wàluug taxawal am mbooloom xare mu Fraans mu dëgër, ngir aar Fraans, ak fipp gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xeewal, moom fipp gi. Goornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi gañe na xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Beljig ci ñu fipp ci kaw Imbraatoor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi (moom paab gi). + +Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nanu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Fraans yi, ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag. +Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar fipp gi, ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar reew mi, tas te giimal fèttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi, duggal seeni xarekat ci Beljig ak Holand, ànd ak loolu lepp teewul waa Fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu. + +Ci 29 sulye 1794g, la ceri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Fraans bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi. + +Goornamaab doxaliin bi: + +Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonay tiital ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon: + +(1) Def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam +(2) Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi. + +Nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig. +Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu, ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon yong googu nuy wax yongug Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Fraaans te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lanu nekkoon. + +Napoliyon Bonaparte: + +Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Ajaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Fraans da koo mujjoon jënde ci Genova. +Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi genne ca bànqaasu xare ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kureelub kano ya ca xarekati Fraans ya. +Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali fipp gi , te fonkoon leen. Moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee Itaali. +Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Fraans, dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Fraans gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g. + +Song gi Napoleon defoon Itaali: + +Goornamaab doxaliin bi, dafa feetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu Cherasco. +Napoleon defati ab xare ak dooley paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, neewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare. +Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Fraans, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Fraans. + +Song gi Napoleon songoon penku bi: + +Politigkati Fraans yi naaloon nanu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug Mans. +Politigkati Fraans yi, li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Fraans ci geej gu diggu gi, ak man a àgg ca geej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk penku. + +Goornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko denkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, geeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Fraans. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Fraans mi, ca ndoxum golfub Abii Xiir, moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Fraans cangug geej gi Fraans yàgg a gent. Fraans sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej, mu mel ne mu Britani mi. + +Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xare jooñ la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga. + +Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg Usmaan gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam. +Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom, xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew. Waa Isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy danoo fippoon ci kawan, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “fippug Xayra gi” . +Napoleon jawali na reewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, ak Yafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi, waa Usmaan yi di ko jàpple ci jeeri ji. +Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji nuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam. + +Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Fraans, waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule goornamaa. Bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga. + +Ay ngérte , yu am solo juddoo nanu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk: +(1) Xareb Fraans boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu feete, ci wàllug jokkoo ak tuxu, ñeel imbraatoorug Britani gi ci penku bi. +(2) Xare boobu Fraans da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi Afrig gu bëj-gànnaar gi. +(3) Boroom xam-xami xare boobu, bi nuy ñëw, indaale woon nanu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak geej gu diggu gi, di kanaalu Suwes bi, te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu Bolaax bi. +(4) Xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Fraans ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs. + +Napoleon ak reewi Tugal yi: + +Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Fraans ji genn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara. +Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Egliis bi ci Fraans. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbal. +Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyeel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi. + +Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi Tugal yi. Britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi, ca xare ba nuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan ak Aleksandar mi nekkoon sesaarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, nu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal bepp, jëme ko Britani , daal di woon ga reewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci reewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na reew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu sesaar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca peey ba, di Butrusburg, waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi nuy dellu nag la waa Rusi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg. +Bu ko defee waaTugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy gañe ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona nu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Fraans yi, ngir xeexi reewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g. + +Bu ko defee, reewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir seddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos reew yu am doole yu peek Fraans wër ko. + +Ligeeyi ndajem Vienne: + +Ligeeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon: + +(1) Way daje yi delloowaat nanu buuri Tugal ya ca seen reew ya nu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Fraans ak Espaañ. +(2) Britani jëloon na sancu yi Fraans moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos. +(3) Rusi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Beljig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di nationalisme gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Rusi ak Otris ak Brusiya, danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu Tugal yu ndaw yi. + +Li juddoo ci fippug Fraans gi: + +(1) Fipp gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral reewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi. +(2) Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal. +(3) Fipp gi ci Fraans mooy gi njëkk ci fipp yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay term yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees. +(4) Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lanu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gepp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee. +(5) Xalaatub fipp gi law na ba àgg ci Tugal gepp, ak yeneen reew yu dul Tugal, yu adduna bi. + +Buntub ñeeteel bi + +Yëngu-yëngu yi aju ci “xeetu” walla fonk sa xeet (nationalisme) ci Tugal, ci xarnub fukk ak juroom ñeent g. + +Bennal gu Itaali + +Bennoo gu Almaañ + +Doggantal gu njëkk gi + +Bennal gi nu defoon Itaali + +Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi: + +Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon reew mu nu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Doox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia. + +Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatoor lanu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa lu ko moy . + +Jeexiit ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali: + +Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. +Mu wutaloon reew mi mepp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi, mu may waa Itaali yi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu Itaali mu man a am, mu nu bennal. + +Itaali ginaaw ndajem Vienne: + +Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy: Piemonte, Napoli, Parma, Modena, Toscana, Lombardia, ak Venezia, ñoom ñaar nag, mujj nanu leen boole def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris. +Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga” maanaam lu nekk, nanu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen seen barab. +Metternich ak bëtam yi mu tasoon ci gox yepp, jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi, daan naj it gepp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle. + +Yewwueg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali: + +Politigu noteel gi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi nu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon. +Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi. +Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu: booloo gu Karbonari (ñoñ këriñ), ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi. + +Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nanu ci, baykat yi, ligeeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs. +Li leen manke woon nag, mooy danoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a not, te daa àntoodil seeni fipp. +Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal. + +Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam. + +Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal reewum Itaali mi, ci ron ag noste gu republig. + +Yëngu-yëngu yii, mujjoon na naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab kojug xare la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal na yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer. +Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi endustreem tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. +Boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali. + +Ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi. + +Ak li boole Itaali, def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Doox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëggunu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li. +Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki Dooxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw gennam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk. + +Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali: + +Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, (ñoom xaaj yi), ñooy: Piemonte, mi nekk ci ron doji Alp yi, nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle, ak Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Fraans gi dend ak Itaali, moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu Fraans ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci geej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte. Ak Genova, moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal. +Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii, ñu tudd ci yi ci ëpp solo: + +(1) Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali. +(2) Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jawrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul Piemonte. +(3) Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam-xam. +(4) Piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo. +(5) Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano. +(6) Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram. + +Cavour ak bennalug Itaali: + +Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu republig. Moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom Piemonte) ak jeneen doole ju reew, ju mel ne Fraans mbaa Britani. + +Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal Itaali. +Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem Otris mi, te man leen a genne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak endustri bi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri, tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi (bu biir reew mi), yewenal nosteg galag yi, daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi. + +Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yewenal yu biir reew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte geek Eglis bi. + +Kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon, bu nu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Fraans, am Rusi, ak Brusiya, waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la woon, manul woon a ñàkk, te itam mbirum adduna bepp la, laaj na reew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko, ci ndajey Tugal yi. +Ci noonu mu digal parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Fraans, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatoor bu Fraans bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg. + +Kureelu xare bu Piemonte boobu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe, teewul Kafour moom lijjanti na ba nu yëg Piemonte ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb Xarm bi jeexee. +Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, kontar Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ. +Bu dee Fraans nag, nga xam ne pencam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu reewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci Tugal. Politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it reew mu nekk ci wetu Fraans la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk. + +Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia. + +Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris: + +Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari temeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko kontar Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi . +Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g. +Taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk. + +Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Fraans itam jibal ab xareem ci kaw Otris. +Soldaari Piemonte yi ak yu Fraans yi jot nanoo duma Otris, gañe ko ca xare ba nuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatoor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li nuy wax juboo gu Siyorix atum 1859g. bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga: + +(1) Otris bàyyee Piemonte Lombardi +(2) Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur +(3) Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi +(4) Delloosi ñi yilifoon Doox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee. +(5) Boole Niis ak Savoia ci Fraans. + +Taarixkat yi, firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Doox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte. Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral. +Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Fraans genne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi. +Askani Doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko poñi juboo gu Siyorix gi yaxale, ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug Piemonte. +Ci noonu ay fipp am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti. +Nii daal la Itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali. + +Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn: + +Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci ligeey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu yu Itaali yi nu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. +Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Silil bi , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam, dugg ci bennoo gi. + +Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali: + +Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi bepp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moo rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko. +Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 febriye atum 1861g. Ca ndaje ma lanu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu nu bennal gi. +Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulye atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig. + +Def Rom peeyu nguurug Itaali gi: + +Waa Itaali yi delloosi nanu Venezia mi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab gox ci Itaali, ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya. +Fraans it ay xarekatam gennoon nanu Rom, ngir sotti gi Fraans sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne Rom daal mooy peeyu nguurug Itaali gu nu bennal gi. +Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi. +Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikan, am it sañ-sañ ci yabal ay ndaw yu koy toogal ca biti. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo . + +Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew. + +Doggantal gu ñaareel gi + +Bennoo gu Almaañ + +Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi: + +Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan, yepp it ci ron imbraatoor gu Otris lanu nekkoon, walla li nuy tudde Imbraatoorug Rom gu sell gi. Almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo. + +Almaañ ci jamonoy Napoleon: + +Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko not, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo peeyam ba Berlin. +Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoni bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lanu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw. + +Almaañ ginaaw ndajem Vienne mi: + +Ginaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lanu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Doox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Rusi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam goxub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoni. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko. +Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey kontar mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo. + +Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi: + +Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, duggal leen ci genn nguur gu Almaañ gu nu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem goxi nguur gi. +Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan. Nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci Brusiya, ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nanu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay goxam yu biir yi. Gox yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan, gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lanu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan. + +Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li nu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy: + +(1) Solofrayn +(2) “Bennoog nduwaan gu Bavar” gi nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at. +(3) Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoni. Mooy gi Saksoni taxawaloon atum 1828g. + +Kilifay Brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani Almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub Solofrayn, gën a yàkkali ab geewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoni ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin gu Brusiya, te da na jàppeji Brusiya muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, dunu ay doxandeem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nanu ne Almaañ gepp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g. + +Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gis Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug Almaañ gi. + +Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy reew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ. + +Jeexiit yi fipp gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi: + +Ay fipp yu bari jot nanoo am ca Tugal atm 1848g. Ag fipp am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu . Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot fippi Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe. +Kërug Orob gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj. + +Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu reew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jeem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas. +Ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma: + +(1) Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya. +(2) Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug Otris gi +(3) Genne Otris ci bennoo gu Almaañ gi. + +Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nanu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatoor ci Almaañ gu nu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol. +La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Rusi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba Vienne. +Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi tegunu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du ligeey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi. + +Otris ak Rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu reew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole. +Looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a genne Otris Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi. +Xalaat bii nag diisoowaale bu Brusiya bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi. + +Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi: + +Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju mag ja. Daal di dugg ag coldaar, gennati ca, dem nag feete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam ngir nu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cer ci parlamaa bu Brusiya bi. Ligeey na it ci toolub diplomasi, doonoon ndawul reewam ca Butrsburg ca Rusi. Ginaaw bi mu nekkal reewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Fraans, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya. +Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Egliis bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kilifaam, waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti reew. + +Bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne Fraans ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga. Ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi, daal di beddiku sartu reew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi. + +Wàllug xeetu nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew, ndax daa gisoon ne sartu reew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi. +Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy: +(1) Coldaar gi +(2) Politigu bitim reew bi +(3) Fal ay jawrin ak di leen folli + +Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ, loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ . +Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yepp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu federaal, guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko. +Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi, ngir yeegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy: +(1) Dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi +(2) Jiite benno gi + +Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi. +Bismarck jeem na a fàggu cofeelug Rusi, ngir mu bañ a feete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Rusi, kontar gori Ploñ yi defoon ag fipp kontar Rusi, ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb. +Fraans nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Fraans. +Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Rusi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom reewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Rusi. Te it nanguwutoon a ànd ak Fraans ak Otris kontar Rusi. + +Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ: + +Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal reewi Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy: + +Xare Brusiya yi ak Danmark: + +Bismarck xuus na ab xare kontar Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari doox yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo. +Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari doox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dooxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin. +Xarey Brusiya ak Otris: + +Bismarck gisoon na ne xare bi moom – deet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig. +Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris. Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim geejug bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu. + +Sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g. + +Bismarck moom lijjanti woon na ba Rusi genne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Rusi ci giimal fipp ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratoor bi Napoleon III, imbraatooru Fraans, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub Rayn. Mu demati tapoo-ji ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom. + +Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a gañee ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatooru Fraans bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Fraans dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatooru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Fraans, Otris du ko sot, ci geneen wàll. +Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame: + +(1) Gennug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi, gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich. +(2) Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu federaal gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu. +(3) Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia. + +Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem reewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari doox yii di Shalswig ak Holistin ci lanu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje. +Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare . + +Xareb Brusiya ak Fraans: + +Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya gañee ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Fraans moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll. + +Fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu nu dogat, ngir mu nekk moom Fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daa kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Fraans du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon. +Lëj-lëju ku jigeen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans. +Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa feexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Fraans mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul Fraans ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw Fraans. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Fraans. Loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Fraans. Ci noonu Fraans jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulye 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu nu dàqee Fraans ci xeex bi. + +Brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak Fraans, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya. +Xare bi bepp nag ci suufus Fraans la doon tàkke. Jotoon nanoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu, te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Fraans ji ci biir suufus Fraans, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Fraans, te mu leer nàññ ne Fraans moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 11870g. + +Ci noonu imbraatoor gu Fraans gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi . Daal di teg Fraans ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans ( loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi dunu genn Fraans li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di Alsaas ak Loren ci fraans, boole leen ci Almaañ. + +Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatoorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratooru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi. +Sartu reew bu Almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay: + +(1) Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundasrat) +(2) Jattayu (Rechstag) + +Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundasrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer, ñu seddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci Bundasrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiit, ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, danoo takku woon ci Brusiya, te daawunu woote lenn lu mu bëggul. Te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga. +Bu dee nag jataayu Rechstag nag moom, man nanu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cer, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu Almaañ bu bees bi, danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo. + +Bismarck nag, jiite na goornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kilifteefam tam la Almaañ gu rëy gii gepp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nanu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at. + + + +Juroomeelu bunt bi + +Sanc gu yees gi + +Sabab yi fi indi sanc gu yees gi, ak ay anamam +Reewi sancaan yi +Ñaawteefi sanc yi +Yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool + +Doggantal gu njëkk gi + +Sababi sanc gu yees gi aki anamam. + +Xamale lan mooy sanc gu yees gi: + +Li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy juxraaf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci reewi adduna bi. + +Sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbèll. +Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen. + +Sababi sanc gu bees gi: + +Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + +(1) Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri, ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi. Loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne-ne yu nu laalul aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri, ndax seen koom-koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu nu laalul yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu nu man a jaaye seen ligeeyi Tugal yu endustri yooyu. +(2) Yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon, loolu moo waraloon reew yii gëstu-ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu reew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc, politig la bu nu nosoon, jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp. +(3) Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan: wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw, ñi xamul dara. Adduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom. +(4) Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci reewi Tugal yu endustri yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii. Loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Reewi Tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu, waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak ñawug seen ngànnaay, ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi. +(5) Lu bari ci reew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole. +(6) Ay lonkoo yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi. +(7) Bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna, loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi, di taqale diggante goxi adduna bi. +(8) Bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principes) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc. + +Anami sanc gu bees gi: + +Sancug Tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + +Sanc ngir dëkk: + +Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu-yëngug wuññiy juxraaf yu Tugal yi. +Bu ko defee reewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale. +Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Amerig gu digg ga ak gu bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lanu cosaano, loolu di ci Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi, lu ci dul Bresil,moom waa Portigaal a ko sancoon. + +Nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca Falastin, bi nu ko sancee ci doole, dëkke ko, reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi, dajee, dëkksi ca Falastin, ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug reewi sancaan yi, ak li askanu Falastin daan xeex loolu lepp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko. + +Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle. + +Teg loxo gu xare : + +Ay reew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay reew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gèndiku woon ci yii reew, rawati na ci wàllug xare. +Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii. +Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk: +Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g, ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g. + +Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la. +Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew. + +Aar : + +Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono. + +Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen. Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe. +Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk: +Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo. + +Feetale : + +Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiit yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel. + +Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi. + +Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen ko. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil. +Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk: +Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs. +Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom. + +Denkaane : + +Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wutu fi kureelug xeet yi. +Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika ak yeneen . + +Sancug aada : + +Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom. + +Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi it, Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi. + +Barabi sañ-sañ : + +Lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani. +Amoon na it ay xejj yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen. + + + + + + + + + + +Ñaareelu doggantal + +Reewi sancaan yi + +Lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi, ci gox yii di: Afrig, Asi ak adduna bu yees bi (Amerig). Reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu, ci taarix, ñooy: + +Reewum Portigaal: + +Waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu Tugal ci ñaari gox yii di Afrig ak Asi. Ñoo ci jiitu woon waa Espaañ, Holand, Angalteer, ak waa Fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf ci jamonoy yewwute gu Tugal gi. + +Tukkib Vasco de Gama bu njëkk bi mu defoon ci Afrig ak End, moo ubbi woon gëti waa Portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci Afrig ak Asi ngir teg loxo geeji penku yi, ak rënk yaxantug penku gi , rawati na li ci aju ci ay rëndaay , ak ngir yàq koom-koomu reewi jullit ñi, rawati na nguurug Mamaalig yi, ngir loolu man a doyadil jullit ñi, neewal leen doole. + +Waa Portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ-sañ ci duni Madira yi, Bopp bu Wert bi ak Osoras, barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi,la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba ca fukk ak juroomeelu xarnu g. Cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci Afrig ak Asi ci xarnub fukk ak juroom g, yu ci mel ni: Mosambig ci penku Afrig, Angola ci sowwu bi, Ecopi, ak duni Madagaskaar, Moris ak Silaan ak xat-xatu Hormos ak xat-xatu Malga ci daanaka-dun bu Malayo añs. + +Waa Portigaal yi defoon nanu seen “sanc gi ngir dëkk” ca Bresil, gi nekk ci Amerig gu bëj-saalum gi, ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu Afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi. +Nu leeral leen ne sancug Portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu, ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu, ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu. Ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex. + +Reewum Espaañ: + +Espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa Portigaal, waaye jariñu ci seen xam-xam boobu ñu jot a am ci lef moomu. Bu ko defee, waa Espaañ jël goxi Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa. Moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna, ray, song, jaay doole ak gënale ci wàllug diine. Ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi, gasal leen mbell yi. Ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug Espaañ, ci làkk, ci diine, ci aada ak ci taarix, ba mujj sax bii gox ñu koy wooye Amerig gu Latin gi, di ko askanale Latin gi nu jublu woon Esspaañ ak Portigaal. +Espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam, lal ko ci kaw ay barab ci goxu Afrig, yu ci mel ni duni Kanari ak àllub Maraakes bi ak goxu Afni bi dend ak Maraakes ak Gine gu Espaañ gi nekk ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi . + +Sancug Espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi Tugal doon def ci w��ll googu. Ci noonu waa Angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon Irmada, atum 1588g. Mbooloom gaalum Holand mi tam moñoxeeti mu Espaañ mu lòtt mii atum 1607g. Ci noonu la Espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante gu Angalteer, gu Fraans ak gu Portigaal. Bu ko defee, ay fipp am ca sancuy Espaañ ya, ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa Espaañ yi. + +Reewum Holand: + +Waa Holand yi danoo duggoon ci ngérum Protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo gu Espaañ gu katolig gii. Looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu Espaañ yii, daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Waaye temb gii nag nangu na ko (moom Espaañ) ci anam gu ofisel atum 1648g, ca kollareg Westfalia ga nu defoon, ginaaw xareb fanweeri at ba . +Waa Holand daal di taxawal lonkoo gu End gu penku gu Holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi, daal di not waa Portigaal yi ci wàllug sanc, teg loxo duni End yu penku ya ca Asi. Yaatuwaayu suuf yi Holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu Holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam. + +Sancaan yu Holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi, kawsu, attaaya, kafe, suukar, seng ak petrol añs. +Waaye ñii dëkke woon ci sancu yu Holand yi te cosaanoo fa, xeexoon nanu kontar waa Holand yii ba mujj am tembte atum 1949g ci turu Endonisi. +Waa Holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di Amerig. +Ñu taxawaloon lonkoog End gu sowwu gu Holand gi atum 1622g, ñu sancoon goxub dexug Hadson, daal di jënd Manhatan ci endo yu xonq yi, daal di taxawal dëkkub Amstardaam bu bees bi nga xam ne waa Angalteer yi nangu woon nanu ko ci Holand, tudde ko New York. Waa Holand tam sancoon nanu – ci diirub fanweeri at – ag wàll gu mag ci Bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug Portigaal. + +Reewum Beljiig: + +Leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum Kongo mi nekk ci digg Afrig atum 1876g, daal di koy def ag moomeelam, loolu nag wéyoon na di nekk ba atum 1908g, ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum Beljig. Kongo nag reew mu naat la lool, te woomle ci ay koom-koomi mbell. Waa Kongo nag jàmmaarloo nanook sancug Beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal, daan jariñoo it seeni koom-koom ci anam yu ñaaw a ñaaw, loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum 1960g ci turu Saayir. + +Sancug Britani: + +Imbraatoorug Britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay. Moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si. + +Britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi, waaye ca Amerig gu bëj-gànnaar ga, mu sancoon lu sakkan ciy suufam, waaye dëkke leen, te sonn it ci dindi kilifteefug Fraans ak Holand ci gox bii te jële ko fi. Bu ko defee, sancu ak dëkkuwaay yu Britani yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu Britani ba kero Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi di am tembte , naka noonu Kanada, ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak Britani, muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan, te bokk nekkandoo ci “Komonwelth gu Britani”. Britani sancati na Ostraali ci anamug dëkk ak Newsiland, waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci Komonwelth. + +Britani sanc na End, wéyal fab sañ-sañam, daal di sos lonkoo gu End gu penku gu Angalteer gi atum 1600g, mu jot a dàqe Fraans ca daanaka-gox bu End ba . Mu manante Siin ci mu ubbi ay waaxam ci kanamu Afyon bii nga xam ne Britani daa na ci indi lu bari ci waa Siin yi. Looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante Siin ak Britani, di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum 1840g ba 1842g, nga xam ne ca la Britani nangoo waaxub Hong Kong bu straateji bi, waax bii mi ngi woon ci loxol Britani ba bu yàggul. Xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne Britani mi ngi ko doon tooñ waa Siin cig wàll, ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll. + +Britani tegoon na loxoom dunu Brem atum 1799g, ak Adan atum 1839g, ak Borma atum 1885g, akug wàll ci Malayo. Mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj-saalumu dunu araab bi, ak tefesug golfub araab bi. Mu sanc Isipt, Sudaan, Iraak, Penkub Sordani, Falastin ak yeneen barab ci reewi Asi yu ñàkk doole yi. + +Britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi Afrig yi, lu mel ni: Afrigug Bëj-saalum gi , Nijeeriya, Oganda, Tansani, Rodisiya ak Somali gi nu xame woon ci turu Somali gu Britani gi. + +Sancug Britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi, ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole, teg loxo ak jariñoo ne-ne yu nu laalul yi , ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen, fitnaal leen ak tooñ leen. Waaye li lii lepp di tar, teewul askani sancu yu Britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte, ci noonu la Britani dellu mel namu meloon, yor dayo bi mu yoroon, ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko, foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom-koom. + +Reewum Fraans: + +Waa Fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu Tugal yi ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi, rawati na ci Kanada ak gox yi peek dexug Santa Lorens gi. Ñu sosoon fa ay sancu yu Fraans, yu ci mel ne: Kebeg gi nga xam ne ci tefesug Santa Lorens gi lanu ko taxawaloon, ak sancu bu Luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca Luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub Fraans ba. + +Ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa Fraans yi ak waa Britani ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. Waaaye Britani moom jot na a neewal doole kilifteefug Fraans gi ci barab yooyu, bu ko defee Fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci Afrig, fu ci mel ne: Aljeeri, Tinisi akug wàll ci Maraakes, daal di sutuxlu ci tàkkug Afrig gu mag gi, daal di yaatal bu baax seen sañ-sañ ak kilifteef ci Senegaal, Kongo, Nijeer, Madagaskaar, Somaal gi nu tudde woon Somaalug Fraans gi, Gine ak Dawme. + +Fraans tegati loxo ay reewi Asi, fu ci mel ne: ay wàll ci End, waa Britani jële leen fa atum 1763g. ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu End gu penkug Fraans gi, ngir gëpplanteek lonkoo gu End gu penkug Britani gi, ak lonkoo gu End gu penkug Holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi. Fraans sancati Sireek Libaa ci turu feetale , ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba . +Sancug Fraans gii nag daa melowoo ag tooñ, tiitale, jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm. Lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj-gànnaaru Afrig te Fraans tegoon leen loxo. Waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug Fraans gii, ba mujj am tembte gu mat . + +(Fii fi Senegaal, waa Fraans sonnale nanu fi, tege fiy fitna, gennee fi, xoolal ku mel ni Sëriñ Tuuba., cig tooñ lanu ko fi gennee, sanni ko ca àlli Gabong yu lëndam ya, yobbooti ko Moritani, te fii nu koy genne de du seenum reew, reewam la. Xoolal ma fa ñuy wax (Camp Caaroy) ak jëf ju ñaaw ja nu fa def, xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te Fraans nekk ci ginaaw, xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal, xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal, leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen Senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon, ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal, lenn luy sunu aada safu ko woon, du col mi, du wax ji, du lekkiin wi, du lenn lu mu man a doon, naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos, defar leen, ñu koy ligeeyal). + +Reewum Almaañ: + +Imbraatoorug Almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi, ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum 1871g, mu daal di sanc Kamerun ak bëj-saalumu sowwub Afrig, bi nga xam ne dees na koy wooye bëj-saalumu sowwu Afrig bu Almaañ bi, ngir sanc gi ko Almaañ sancoon, ak bëj-saalumu penku Afrig bi nu tudde ba tay bëj-saalumu penku Afrig bu Almaañ ak Togo . +Almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni Pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu “duni argabiil yu Bismarck yi” . +Ñu nangu tam ñoom waa Almaañ xaajub bëj-gànnaar bi ci duni Gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi. Waaye Almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi. + +Reewum Itaali: + +Itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi, ginaaw bi mu bennoo, atum 1870g, mu daal di teg loxo ay sancu ci Afrig, ci Eritri, Somali, gi nu tudde Somali gu Itaali gi, Libi ak Ecopi. Itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew. (Omar Muxtaar ca Libi fàttaliku leen ko). + +Reewum Rusi mu Xaysar mi: + +Sancug Rusi gi moom mi ngi jëmoon ci Siberiya, Turkmanistaan ak ay gox ci Asi gu digg gi. Rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj-gànnaaru dexug Amoor gi ci Siin, daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu Vladivostok, lijjanti it ba Siin gu neew doole gii jox ko ay sañ-sañ ci defar yoonu weñ wu jaar ci suufi Manshuriya gu Siin gi, ligeey ba daal di tàmbli ca atum 1889g. Sañ-sañu Rusi it yokku ca Kore, mu daal di seddoo Iraan mook Britani, daal di sanc wàllug bëj-gànnaar ga, ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi, xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum 1907g. + +Buntub ñatteel bi + +Ñaawteefi sanc: + +Li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi, ci melokaanam yepp aki anamam, bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko, rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw, ba nu mos aw wextanam, reer cig lëjam. Sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt yi yanu woon ab sukkam. Ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii: + +Ñaawteefi sanc yu politig: + +li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew, rekki it seen sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom, te loolu dal yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko. Xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu-reew , ak ci nostey demokraasi yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell, loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi te dindee leen fi, wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc. + +Sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn, bu ko defee mu def lu nekk, jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn. Mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn, ak wepp xeet wuy wenn, ci mepp reew muy menn. Mu soññ te sawarloo yëngu-yënguy beddiku yi yi nga xam ne neewte yaa ngi leen doon sàkku ak def, daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér, mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew, daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu, daal di def ay soppi ci dig yi , yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo, dendandoo, mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe-jafey politig yu fasu, yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at, ginaaw bi nu tembee, yooyu jafe-jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees. Sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi, mu duma, tëj, mbugal, te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko, sàkku woon nu nuy goree te temb, te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen. Waaye askan yii yanu woon sanc gi, jugoon nanu xeex, def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd. + +Ñaawteefi sanc yu mboolaay: + +Sanc daal dafa defoon yitteem ci tas, xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi, jaare ko ci soññee cig tàqalikoo, wisaare nosteg kureel ci biiru askan, bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ, am ay sañ-sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen . Gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari. Bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi, di leen tegi coona, di leen fitnaal, te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi. +Am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi, mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi, bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal. + +Sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay, man a ñaawali jikkoom. Mu soññe cig mbon, reer, jëfandikoo dorog ak yiy màndal ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay, te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi, te gën fee suuxat seen reeni sanc. + +Sanc gi de jeemoon na – jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon – ngir gòndi niti sancu yi ci xayug Tugal gi , te sopploo leen ko, ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm-kanamug Tugal gi ak xalaati waa Tugal yi. Li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi, rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig, jaare ko ci seenug jàpple. Waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu, teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi, sooyal seeni mebat. +Seeni mebat sooy na, seeni yaakaar tas, bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine, di gën a ŋoy ci sseeni aada, di gën a ngëb ci seeni pas-pas yu laab yooyu. Fonk seen bopp, seen taarix aks een xalaat. +Nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi, ñu saxoon nag ci noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk. + +Ñaawteefi sanc yu koom-koom: + +Li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne-ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay , buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc, looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi. Mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk, ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi. Bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom-koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt , ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def, ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi. +Reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi, waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi Tugal yi. Lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi “siyukaay biy si buy dem ak buy ñëw” . + +Sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi, daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi, ngir man a joxe ne-ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi. Sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi, tax it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi Tugal yi. Bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom-koomi reew yi ak seeni alali endustri. Ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi, loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom-koomu sancu yi ci koom-koomu reew yiy sanc. Fii nag la genne gisiin wi naan: sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom-koom ci sunu jamono jii nu toll. + +Ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat: + +Sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay, te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi. +Sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc, te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la, juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo. Mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi. + +Sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng, rawati na mi ci aju ci xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam-xam man a am ak gu endustri ci reew yi. Te moom (sanc gi) yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi, walla njàggale mu yaatu mi . bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi. + +Sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul ci lenn lu dul ci ne-ne . Ñu tay-taylu woon di far dëgg yi, di indi li dëppoo ak seen njariñ, di wisaare xam-xam yiy ligeeyal seeni reew, di wone dooleem akug màggam, ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew, daan leen sabooteel seen kilifa yi, seen njiit yi, seen jàmbaar yi ak seen boroom xam-xam yi. Sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam, moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet. + +Doggantal gu ñeenteel gi: + +Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal: + +Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu nu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi, yilif ko . Looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi. Lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu rekk ci jëmmi boppam, waaye kay jàngu yepp a ko daan def, moo xam jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi). +Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi. + +Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Porrtigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par-parloo kontar jullit ñi ak seen adduna. Bu ko defee wuññikati Orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew, loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal . + +Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam : + +Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi, bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi def. +Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon. +Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo: + +(1) Ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni: fajuwaay yi ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen, aki matulkat aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal Egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Ndoktoor man nanu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi danu daa wax naan: li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Daanu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug. +(2) Njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne: daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon. +(3) Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi: bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci reewi Afrig yeek ak Asi. Loxob nasaraan biy indi ñam, fa jak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi. +(4) Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi, ak taalifi penku-penku yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi. Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey. + +Nasaraanal ci reewi araab yi: + +Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug Britani, Fraans, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine. Reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii : +Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Fraans ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Fraans merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante Fraans ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu Fraans gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Fraans ak kilifteefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole. +Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs + +Goxi Golfub Araab bi : + +Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi Golf bu Araab bi, ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn. + +Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Amerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci goxi Glof bi. Nasaraanalkat yu protestant yu Amerig yi daal di taxawal egliisub Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bic i Manaama ak Abuudabi, ak Egliisu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji, ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi. +Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi, teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar. + +Reewi Shaam: + +Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Urdun . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, nga xam ne reewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale gu Fraans ak Britani. Bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kureelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, feeteek kureelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel, ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g. +Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa. +Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Amerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte daa noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub Balfour , genne ko it atum 1917g, li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar. + +Isipt: + +Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee bu katolig bu Fraans bi tukkee woon Liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko. + +Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu protestant yu Amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal . + +Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jàngu aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xaayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs. +Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo. + +Sudan: + +Ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudan, rawati na ci ginaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal. + +Waaye waa Sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. Fipp gu Mahdi di xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko. + +Reewi Maxrib bu araab bi : + +Maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Fraans. Reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi Maxrib bu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci Fraans, Itaali ak Espaañ. Reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu. +Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug sanc gu Tugal gii ci reewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. +Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taarixam, jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu yu reewi sancaan yi, bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew, te dunu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi. + +Waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi Maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon. + +Barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi: + +Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci reewi araab yi, lii ci la: + +(1) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal , yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi, ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg. +(2) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju mag ju Amerig ji, xamluwaay bu penku bi, xamluwaay bu Fraans bi, yooyu yepp nag ñi ngi Xaayra . Bu dee Sudan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak jàngu bu Amerig ak jàngu yu Qibt yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Amerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju mag ju Amerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja, walla daara ju mag ju Yesu ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf . +(3) Nasaraanalkat yu penku-penku yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi. Ñu dugg ca akaademib làkk ba ca Xaayra ak bu xam-xam ba ca Dimasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penku-penkub Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom ak Margoliyos mu Fraans mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Holand mi, ak Harithman mu Almaañ mi. Penku-penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, teere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel. +(4) Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi. (ginaaw ci reew yii lanu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax). + + + +Juroom benneelu bunt + +Ñaar-fukkeelu xarnu + +Ñaari xarey adduna yi, bu njëkk bi ak bu ñaareel bi +Mbootaayi adduna yi: kureelu xeet yi, mbootaayu xeet yi +Mbootaayu reewi jullit ñi +Danki reew yi ak reew yi feetewul fenn +Xareb jawwu bi +Jëm kanam gu Japon + +Doggantal gu njëkk gi +Ñaari xare yu adduna yi: bu njëkk bi ak bu ñaareel bi + +Xaaj bu njëkk bi ci ñaar-fukkeelu xarnu g, seere na tàkkug ñaari xare yu adduna, ñooy xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g) ak bu ñaareel bi (1939 – 1945g). +Leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono. + +Xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g): + +Li waral xare bi: + +Xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi , kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi. + +Sabab yu jonjoodi yu xare bi: + +Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy: + +(1) Gëpplante gi ci wàllug sanc +(2) Tapoo yi +(3) Màggug yëngu-yëngu yiy woote ag xeetu +(4) Ak lëj-lëj yu adduna yi + +( a ) Gëpplante gi ci wàllug sanc: + +Gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g . Reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew, rawati na nag ci reewi Tugal yi am ay noste yu gore . Bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu-ji ne-ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox, man a jëm kanam. Tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye-ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi. + +Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi, bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu. + +Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante Britani ak Fraans cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay Almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom yu Almaañ yi ci reewum Usmaan mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi . +Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal. + +( b ) Tapoo yu reew yi: + +Gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu adduna bi gënee jëm kanam. Loolu nag tax ba ay dank sosu yu reew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu, yii di ñëw: + +Tapoo gu ñaaral gi ci diggante Almaañ-Otris: + +Gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru Almaañ gi ak gu Otris gi atum 1879g, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw: + +(1) Bu Rusi gu Xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war na a dimbli mi nu song. +(2) Bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu. +(3) Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Rusi ak Fraans, ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu. + +Tapoo gu ñattal gi : + +Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum 1882g, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll. +Itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Fraans, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Aljeeri atum 1830g, ak Tunisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Fraans ak Britani ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci geej gu diggu gi . + +Dëppoo gu Fraans-Rusi gi: + +Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Fraans ak Rusi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na atum 1886g, daal di gën a jëm kanam atum 1888g, bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Fraans di jox Rusi ngànnaay, te jëmale kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Fraans ak Rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw: + +(1) taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi. +(2) Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante. + +Dëppoog cofeel gu Britani-Japon: + +Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Britani ak Japon atum 1902g, lii la yaxal: + +(1) Bu xare tàkkee ci diggante Japon ak Rusi gu Xaysar gi, Britani da ca a war a genn te seetaan. +(2) Waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Rusi ak Japon, kon Britani da ciy war a dugg moom itam, jàpple Japon. + +Dëppoog cofeel gu Britani-Fraans: + +Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Britani ak Fraans atum 1904g, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax: + +(1) Féexal Fraans, joyal ab loxoom ci Marog , gii nga xam ne jotoon na a temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Ajeeri ak Tunisi. +(2) Fraans moom tam nangul Britani teg gi mu teg loxo Isipt atum 1882g + +Dëppoo gu cofeel gu Britani-Rusi: + +Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Britani ak Rusi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax: + +(1) Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan , ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Rusi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Britani jël gu bëj-saalum gi. + +( c ) Màggug yëngu-yënguy xeetu yi ci Tugal: + +Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom neenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy: + +Mbootaayug Slaaf gi : + +Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu Otris gi, ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Tugalug penku gi. +Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Rusi gu saaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Rusi gu Xaysar gi. + +( d ) Lëj-lëji adduna bi: + +Ay lëj-lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu: + +Lëj-lëju Maraakes: + +Fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo Maxrib gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tunisi ak Aljeeri Fraans a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig sanc. Ci noonu Fraans lijjanteek Britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga atum 1904g, Fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum 1906g ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi. +Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Fraans la gënoon a nekk, ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. +Fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon peey ba, da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu Fraans ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ mi àndoon ak buurub Maraakes bi, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Fraans. +Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Fraans yabaloon am mbooloom xare ca Faas atum 1911g ngir teg ko loxo. +Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Fraans-Almaañ bi, la fa juddoo di : jox Almaañ ay moomeel ca Kongog Fraans ga, bu ko defee Almaañ nangul Fraans nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu adduna bepp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi. + +Lëj-lëju Balkaan: + +Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan. +Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum 1908g. +Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba. + +Lëj-lëju Maseduwaan: + +Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon na jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen. + +Lëj-lëju Tripoli: + +Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci. + +Sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi: + +Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Rusig Xaysar gi. +Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def. +Otris daal di gaaw jirñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes-xibaar yi noonoo Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul, waaye Serbi moom tontuwul . + +Jibalug xare bi: + +Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibbal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal. + +Lefum xare bi : + +Jë bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru. +Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g. + +Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani. + +Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa. + +Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay. + +Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom. + +Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo. +Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g. + +Lijjanti yi ci ginaaw xare bi: + +Reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris. +Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Fraans. + +Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk. + +Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi. +Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g. + +Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi. + +Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko. + +Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations) teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi. + +Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon. + +Ñaareelu xareb adduna bi (1939 – 1945g): + +Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi. +Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu” lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi. + +Li laytaay xare bi: + +Àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu. + +Nosteg àtte gu mbokkoo : + +Rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba. + +Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi. + +Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ: + +Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ. + +Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi. + +Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g. + +Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali: + +Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu. + +Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi. +Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma. + +Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi. + +Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi). + +Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi. +Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom . + +Bokk na ci diktaatoor yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ bu Espaañ ba. +Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi. + +Yeneen jëfka yu sabab xare bi: + +Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo: + +(1) lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon. +(2) Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi. +(3) Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi. +(4) Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke. + +Jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi : + +Xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy: + +(1) Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g +(2) Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g +(3) Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g. + +Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. +Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g. + +Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi. +Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g. +Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g. + +Wéer ngànnaay gi nag lii la wax: + +(1) Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi. +(2) Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans. +(3) Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar. +(4) Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon. + +Ginaaw bi Fraans wommatoo meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll. +Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg. + +Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. +Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan. +Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd: + +(1) Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji. +(2) Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g +(3) Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g + +Ndamul Réewi tapoo yi: + +Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw - jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g. + +Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. +Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex . + +Wommatug Japon: + +Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo. +Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ��aari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex. + +Li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi: + +ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu: + +(1) Def ndajem Botsdam ca anéeru Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi. +(2) Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg) +(3) Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani, Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar. +(4) Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem neewal dooleem. +(5) Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi. +(6) Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare. +(7) Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g. +(8) Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko. +(9) Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare. +(10) Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal. +(11) Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag +(12) feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi. +(13) Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom. +(14) Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon. +(15) Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon. +(16) Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi. +(17) Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal. +(18) Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf. + + + + +Doggantal gu ñaareel gi + +Mbootaay yu adduna yi: kureelug xeet yi , mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi), mbootaayug reewi Lislaam yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi). + +Ñatti mbootaay lanu bëgg’a waxtaane ci doggantal gii, ñooy : Kureelu xeet yi, Mbootaayu xeet yi, Mbootaayu reewi jullit ñi. + +Kureelu xeet yi: + +Njiitul Amerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi, guy jeem’a indi jàmm ci adduna bi, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. +Waxoon nanu ne Wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati. + +Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon, kollëre ga nu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim. Lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre gi taxawal kureelu xeet yi. + +(1) Sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tèmb gu mat gu dara wàññiwut, reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu yu mat ci respekte walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral . +(2) Reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir nu àtte leen, te xool li leen boole. Reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw. +(3) Jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés, ak wormaal kollërantey reew yi, ak xeex njaam, ci meloom yepp, jeem’a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund, ak xeex dorog, nos yaxantu ci adduna bi, ak sonn ci wér gu yaramu nit. +(4) Reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig , dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk. +(5) Aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi. +(6) Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi, ñuy : reewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen’a may ag tèmb ëlëg . Kureel bi, bi muy door a sosu, 42 reew a ca bokksi woon. Ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu ci bu nuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg’a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk. + +Bànqaasi kureelu xeet yi: + +Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy : Jataay bu matale bi , Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : àttekaayu maanduteg adduna bi ak mbootaayug ligeey gu adduna bi . + +Jataay bu matale bi: + +Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar, ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam. + +Jataayub kureel bi: + +Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer , juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy: Britani, Frans, Itaali, Japon ak Almaañ mi jël cerub Amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg . Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent. + +Koolute gi (secretariat): + +Koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi, mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi, ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale , ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg aada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex dorog, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi. + +Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: àttekaayu maanduteg adduna bi, ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi, ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind. Àttekaayub maanduteg adduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Holand. Ak mbootaayug ligeeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi. Geneve nag moo dib dalam. + +Ayibi kureelu xeet yi: + +Kureeb xeet yi de, ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay , loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu xeet yi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Japon defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci Japon ak Almaañ gennoon atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecopi atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum 1937g . Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon‘a tee ay “dank yu xare” yu bees di am, maanaam ay reew dajaloo,boole seen bopp ci wàlli xare . Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon’a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn. +Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Britani ak Frans nu man’a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci reewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Reew yu mag yii dano’o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg’a def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ. +Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi. + +Mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi): + +Ndawi reew yu mag yi, yu ci mel ni Britani, Diiwaan yu bennoo yi Amerig, Bennog Sofyet , Frans ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi . +Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér. +Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku San Fransisko ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi. +Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy: + +“Ñun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef” . + +Jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay ker-keraanam : + +Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy: + +(1) Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi. +(2) Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi. +(3) Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit. +(4) Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg. + +Bu dee ker-keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii: + +(1) Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi. +(2) Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi. +(3) Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi. +(4) Sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi. + +Campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam: + +Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy: + +Jataay bu matale bi: + +mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem: + +(1) Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi. +(2) Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi. +(3) Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk. +(4) Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi . +(5) Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi. + +Saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man’a doon walla ab ndenkaane. + +Jaataayu kaaraange gi: + +Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe. +Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi. +Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci. +Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex. + +Koolute gu matale gi : + +Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi . + +Campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi: + +Am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi, ñooy: + +Jataayub koom-koom ak mboolaay : + +Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo: + +UNESCO: + +Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans. +Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi. + +Mbootaayu Ligeeyu Adduna bi: + +Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte . +Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve. + +Mbootaayug Wérug Adduna bi : + +Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam. + +Mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi : + +Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali. +Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi: + +Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi. +Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand. + +Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax: + +Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen. + +Jataayub ndénkaan yi : + +Mooy saytu mbirum sancu yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi. + +Bankub addunna bi ngir sos ak tabax: + + Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg . +Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig. + +Keesug kee gu adduna bi : + +Yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi . + +Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy: +(1) mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll. +(2) Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp. +(3) Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ. + +Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi. +Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. +Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon. + +Mbootaayu reewi jullit yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi): + +Ag sosam: + +Mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g. +Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk . + +Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf. + +Kollëreg mbootaayu reewi jullit yi: + +Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 - 4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi. + +Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen reew yi. +Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe: + +(1) Yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk +(2) Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram. +(3) Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb. +(4) Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk. +(5) Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi. +(6) Jeem’a far boddante ci biiru xeet, ak sanc ci mbooleem ay anamam. +(7) Def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute. +(8) Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf. +(9) Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew. +(10) Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo . +(11) Reew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam . + +Campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo: + +Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki : + +(1) Jataayu buur yi ak njiit yi +(2) Jataayu jëwrini bitim reew yi +(3) Koolute gu matale gi +(4) Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi. + +Bu dee kureel yi ci bokk nag, ñooy: + +(1) Kureelu Quds +(2) Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar +(3) Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada. +(4) Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala +(5) Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu +(6) Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada + +Bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi, ñooy: + +(1) Keesug dimblante gu lislaam gi +(2) Keesug Quds +(3) Daaray gëstu gu lim yi ak koom, ak mboolaay. +(4) Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu. +(5) Cëslaayu lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom. +(6) Barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam. +(7) Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu +(8) Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi. +(9) Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li +(10) Akaademi bu xam-xamu lislaam +(11) Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi +(12) Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon + +Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy +(1) Banku lislaam bi +(2) Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi +(3) Mbootaayu rajoy reewi jullit yi +(4) Neegub yaxantu bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi +(5) Mbootaayu peeyi lislaam yi +(6) Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi +(7) Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada. + +Jagley campeef yi ak seeni ligeey: + +Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam. + +Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk. + +Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g . +Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g. +Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g. +Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g. + +Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam. +Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko. +Mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi. +Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi. +Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee. + +Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g. +Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi. +Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi. +Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle. +Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” . Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi. +Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal. +Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g. +Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi. +Ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii: +(1) Di gëstu lay xew Quds +(2) Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen, +(3) Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds +(4) Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju. +(5) Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi. + +Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at. + +Doggantal gu ñatteel gi: +Reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn + +Ag jiital: + +Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay reew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare. +Ci noonu dankub bopp-alal dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi . +Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole ba nu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo. +Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu, Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi . +Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te faf far, xajal fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi. +Loolu nag taxoon na ba reewi Orob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew. +Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi. +Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. +Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni: +Tapoo gu càmmooñug atlas (Otan): + +Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island. +Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm: + +(1) kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des. +(2) Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom. +(3) Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam. + +Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm ak yoon. + +Tapoo gu Warsaw: +Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. +Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. +Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi. +Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk. +Tapoo gu kollëre gu diggu gi: +Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak. +Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g. +Jataayub Tugal bi : +Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali. +Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi. +Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba : +Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk, ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk, te doxal fi yaxantu gu gore ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir. +Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali : + +Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll. +Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suwed, ak Yogoslawi. +Mbootaayug reewi Amerig yi: +Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk. +Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum 1958 g. + +Mbootaayi reewi Andis yi: + +Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi. + +Naalub Marsaal bi ak Komikon: + +Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi. +Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom. + +Mbootaay gi boole reewi araab yi : + +Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir. + +Mbootaayug jàpplante gu Asi: + +Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk. + +Mbootaayug bennoog Afrig : + +Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada. + +Reew yi féetewul fenn: : + +Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll. + +Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo. + +Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Japon, Filipin, Taylan, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman. +Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb. +Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex. +Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig. + +Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakri atum 1960 g . +Bi adduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi. +Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja. +Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk: + +(1) wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg. +(2) Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul. +(3) Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi tas leen, dindi dàtti xare yi . +(4) Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk. + +Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit bu baax. + +Ñeenteelu Doggantal + +Fipp gi xam-xam amal ci Elektron : + +Xamale lan mooy “ Elektron” : + +Elektron moom yaram wu sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu nu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu elktronik yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso. + +Elektron nag nekk na ci bepp ne-ne bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek fepp wi , walla saal bi , moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc. Elektron ni muy wëre saal bi - booy xool - day mel ne ni bidiw yu mag yi di wëre jant bi. +Elektron nag day yanu ay cëfkay kuran yuy bañ , saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu walla nangu. + +Xam-xamu Elektron ni mu sosoo: + +Xam nanu ne xam-xamu Kuran moom xam-xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Gres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii nuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu. +Jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran, maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu lamp bu kuran. + +Xam-xamu kuran nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam-xamu fisiyaa bu angle bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu fisiya. +Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam-xam yi feeñal ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari. +Ndamul xam-xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf. + +Jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ: + +Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, barabu ligeey yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs. +Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi, ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi, ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs. +Boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu ndoktoor yi, ak jumtukaayu segg yu elktronik yi. Jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii. + +Gis nga leegi foo dem fekk fa komputer, ci bank yi, lonkoo yi, campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi. +Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi, ak xam kiliman bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def. + Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbèlli suuf yu am yi solo. + +Jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga jumu fepp , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs. + +Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii. +Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi. + +Juroomeelu Doggantal + +xareb jawwu ji : + +(( yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin)) +Sooratu Rahmaan, aaya 33. + +Di : yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen bunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa. + +Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan; ay bidiw aki ñoom seen. +Moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind, ak li leen sos, def it ab jeego bu rëy ci xam-xamu juxraaf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, bidiw ak lu ko moy. +Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bii, gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci jafe-jafe yi mu ci man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu: man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu nuy joy , bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci. + +Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji: + +Sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji, làmbtu ko, loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo. +Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu gi tuddoon Fostok – 1 ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp. +Tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj. +Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu. + +Sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii. + +Li ci waa Amerig def: + +Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon. +Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a neew, te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji. + +Waa Amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nanu fa it ay còmp yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal . + +Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu) ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. +Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu . + +Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g. + +Musibam Carlinger: + +Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna . +Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald RIGAN nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi. + +Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee. + +Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca. + +Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi. +Ndaxte xam-xamu fisiya gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego, naka noonu endustri elektronik, ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs. + +Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare, la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji, yi ci yanu ay boppi atomig, cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll. + +Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare. + +Juroom benneelu doggantal + + Ni Japon jëme kanam + +Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g: + +Japon de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci yëfi bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na endustri. + +Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci reew mu deltu ginaaw, dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, aada, politig ak xare. +Mu roye nag ci reewi Tugal yi, gisiinu sanc ak yaatal ko, ci reew yi mu dendal, ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew, sanc leen. + +Japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci reewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum 1854 g gii rekk - teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Orob gi, di ci jariñu, di ci niitu. +Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo. Reewum Japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug endustri gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg. +Bu ko defee, Japon xëy di reew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci reewi Asi yi, ci wàllu endustri, xam-xam ak xarala . +Mu mujj am, moom Japon, mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi, ci diggante ñaari xarey adduna yi. +Marsandiisi Japon yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig. + +Japon, ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi: + +Japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Japon. +Japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko, mu jébbalu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Amerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi , ngir doxal mbiri Japon, nu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g. + +Waa Amerig yi nag rëddaloon nanu Japon benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi , nu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng, wutaloon leen sartu reew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi . +Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Japon yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees . + +Ci noonu Japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk, reewi endustri yu jëm yi kanam. + +Waa Japon jariñu nanu ci li leen Amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Lijjantikati Japon yi dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Japon, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Japon bari ay ligeeykat. + +Suqali nag gën na a yokk ci wàllug endustri ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Japon mujj di ñatteelu reew mi ëpp lu muy ligeey weñ, bokk it ci reew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu nuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, ligeey bi aju ci jumtukaayi eliktronig yi gën a jëm kanam, ba mujj Japon àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja yi nuy jaaye ligeeyi Japon yi gën a yaatu, gën a bari ci adduna bi. Bu ko defee Japon mujj nag di reewum endustri mu mag, mu dox, te jëm kanam. + +Taariix +Ag jiital + +Teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam, ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona, moom la lay xamal ciy waxtu, ci lu dulub coona. + +Muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi, te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am, te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen. Ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg, lu mu metti, metti, danoo war a wut ay kuutlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi, te nag yombug xam-xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo, kon lu tax muy français? Ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam, ngir déggante, waxante, te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk, lay gën a nekke jumtukaay boobu. +Lii ak leneen lu bari, moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof, te ba yeneen kàllaama yi, ginaaw bindaluma ku leen moy. Te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa Afrig? Nekkewunu fi lu dul ligeeyal Tugal ak lu ni mel, nanu sunu bopp ñor ! doonte as lëf la it. +Nan la am reew mu tollu ne Senegaal… ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk ? reerale ga’a ngii ! + +Abdul Xaadir KEBE + +Bunt bu njëkk bi + +Njëlbéenug jamono yu yees yi + +• Yewwute’g Tugal gi +• Wuññi yu juxraaf yi +• Yëngu-yëngu yi daa kontar Egliis bu Paab bi + +Doggantal gu njëkk gi + +Yewwute ga amoon ca Tugal + +"Yewwute" gu Tugal gi, baat la buy tekki - ci maanaa mu taarix mi mu yore - yëngu-yëngu gu dekkal ak yeesal, walla dundal xay gu Tugal gu yàgg ga ( gu klassik ga), gu Geres ga ak Rom . Rawati na ci wàlli njàggat , fànn ak tabaxiin . + +Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Hiisaa, ba ci bu fukk ak juroom ñaar, mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada, dundiin, mboolaay , politig ak koom-koom. +Kon daal, "yewwute" gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja ( mu'y jamono'y "ag laman" walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji ( di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala ). + +Sabab yi tax Yewwute'g Orob gi am : + +Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy : + +1 - Jeexiit gi xay gu lislaam gi def ci yewwute gii, +2 - Ak feeñug dëkk yu mag yi ci Tugal ( les villes), +3 - Ak neew-doole gu Egliisub Paab bi neewoon doole, ak tas gi mu faroon tas. + +Jeexiit gi Lislaam amal ci yewwute'g Orob gi : + +Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore , araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Orob nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk . + +Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñ yi + +Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya, duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam . + +Lii nag ci li soppi xalaati waa-Tugal yi la jëm ci Egliis bi, nit, adduna bi ak dund gi. + +Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbli woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci ndoktoor, xeltu , gañcax ak ndundat , ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn (g) . + +Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin ( wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Orob ca jamono jooja ) loolu dimblee woon - ci ginaaw bi - ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am. + +Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi ( les villes ): + +"Nosteg laman" walla gog cang, ku ne xam na ne la mu baaxoo woon mooy tegu ci mbay, suuf, ak seqoo yu laman yi daa lijjanti ak'a nos diggante jaam bi ak sang bi.. ag laman nag - jullit ñi masuñu koo xam - nosteg koom-koom la tey gu mboolaay gu bon, daan gàllankoor xay gi ba du jëm kanam. + +Bu ko defee, li ñuy wax "tool", di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste . + +Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug mecce yi ak ligéey yi, ngir jòkkoo gi waa Orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon’a lòtt ak’a naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal ki tàmblee am yoon wu mu man’a jaar bay dund te du sukkandiku - ci léppam - ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi. + +Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu ak’a lakkal noste gu laman gi, tey ligeey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man’a am. + +Lòttug Egliis bu Paab bi akug tasam: + +Egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax "njàng yi aju ci Yàlla" (théologie), ak njàggat ak xellu , amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam. + +Egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war’a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Egliis bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. +Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën’a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa’a xóot, ak bu endustri ak aada . +Yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it - di doyodil nosteg laman gi - rataxal yoon wi ba yewwute gi man’a am. + +Itaali mberum yewwuteg Tugal gi: + +Dëkk yu Itaali yi ñooy mber mu njëkk, mi njëkk’a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax . + +Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg’a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa Rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fann , nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine. + +Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab gi ci Itaali ag tono gu ne-ne ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn ,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa ligeeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi teere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit +ñi. + +Mandargay Yewwuteg Tugal gi : + +Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën’a rëy: + +(1) Yëngu-yëngu yi aju cig "nite" : + +Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya ( yu Gres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war’a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi , ak jeem’a xam seeni mbóot. + +Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati Gres yeek Rom (grego-romain) ñoom lanu jëloon, yittewoo leen,ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. +Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàggat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàggati Gres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam. + +Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. +Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi , di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot , nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja . +Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi. + +Dëkki Itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees, ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal, te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu Gres wa. +Tabaxiin wii siw na lool te tas ci Egliis yi ak katedraal yi, ak saal yi ak barabi tiyaatar yi, ak sangukaay yi . + +Ci dëkki Itaali yii, lu bari ci waa-fànn yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko ( 1400 - 1455 ), mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën’a mag, ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya . +Ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal, mu nekkoon moom ku diinewu. + +Bokkoon na ci ñoom it Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 ), moom mi boole woon fànn ak xam-xam, defar nay nataali fànn yu siw, bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi, ak Jokanda, walla Mona Liza. ñaari nataal yii ci yi gën’a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute. +Da Vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk, waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag,dib rëddkatu tabax te dib eesañër bu muus. Bokk na ci deseñkati Itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax Titian (1488 - 1572 ), moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi, ak Rafayel (1493 - 1520 g ), moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon, te di deseñkat bu bokk ci ñi gën’a siw ci mbooleem jamono yi. + +Bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci Itaali ba tay, yattkat ba Donatello ( 1386 - 1466 ) , mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya, di gres-rom, rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam. Moom daal ca dëgg-dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi. + +(2) Feeñug làkk yu bees yi: + +Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi , moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon. + +Bi jamonoy "yewwute" dikkee, ngelawul "fonk sa xeet" upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu. + +Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi. + +Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). + +Chaucer mi dib angle ( 1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën’a siw. + + (3) Feeñug xeeti Orob yu yees yi: + +Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Orob taxaw, yu amoon "ag temb" ,ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci "temb" tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi . + +Looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk, xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man’a laal ci xeli lu bari ci nit ñi. +Ci noonu xeet yu bari ci yu Orob yi, tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf, di goreel seen bopp ci toppub jàmbur, te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi +Ay àtte nag yu Tugal yu am ay nekkte yu politig yu temb juddoo ci loolu ci ginaaw bi, yu am seeni làkki bopp yu yees, di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat, lu dul ci jamonoy yewwute gi. + +(4) Yëngu-yënguy dajale mbind yi: + +Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci Xustantin ak ci dëkki Gres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal, mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Gres yeek Latin, yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi,ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii. + +Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot’a am ci misaal rekk,mbindu’m binkat bii di waa Rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g) . +Tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi. + +(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya: + +Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya. +Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam , waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix , mu tudd daaray xam-xam bu taarix. + +Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla ( 1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn dosye bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax "mayug Xustantin", mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen . + +Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli ( 1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas. + +(6) Jëm-kanamug yaxantu ak endustri: + +Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi , ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa . + +Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci kee yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug "maas gu diggu" gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi. + +(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi: + +Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. +Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi , ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi. +Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon ( 1220 - 1292 ) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal . + +Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf . + +Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ ( 1561 - 1626 g) , di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi , ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd . +Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 g) moom tam feeñ , di kok dafa yittewoo woon jiyoloji ( bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn , tey fentkat. +Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 - 1642 g) feeñ , mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba , dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus ( 1476 - 1542 g). + +Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel , walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam. + +Yewwute gi ci Itaali: + +Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo: + +1 - Song gu mbooloom xarem Fraans mi ak mu nguurug Rom gu nu sellal gi songoon dëkki Itaali yi, rawati na Rom ak dëkki bëj-gànnaar yi, niki Milano, loolu it taxoon na ba ñu giir dëkk yooyu, te Milano ak Rom jiitu woon ci. Ci noonu la yewwute gi delloo ginaaw ci Itaali ngir ñàkk gu fa jàmm ñàkk ak kaaraange ak dall. + +2 - Jeex gu àtteg walla kilifteefug njabootug Madatsi jeexoon, ñooy buur yi daa sàmm yewwute gi ci Firenze , loolu nag sabab si mooy xuloo ak xeex gi amoon ci biir njaboot gii, te Firenze moo ëppoon solo ci barab yi yewwute gii nekkoon. + +3 - Teg loxo gu buurub Espaañ bi Ferdinando, buurub Argon, defoon Napoli atum 1504 g, loolu bokk ci li neewaloon doole yewwute gi ci dëkku Itaalib bëj-saalum bii. + +4 - Yëngu gi amoon ci jéem’a yéwénal diine ji ci Orob, ñi ko daa def di Luther,Kalfen, Swingli ak ñeneen, looloo taxoon paab gi jug ak doole ci kontar nite gi. Nga xam ne sax noonu gi àgg na ci paab bi tuddoon Kalimat mu juroom ñaareel mi, kompoloo woon ak buur bi Sarl 5 (Sarlkaan) buurub Espaañ bu katolig bi, ngir ñu fexee naaxsaayal yëngu-yëngug nite googu ci Itaali. Loolu mooy li waajal mbir yi, nooyal yoon wi ba “ëttu àttey lajmat" yi man’a am ca Esapaañ, di woon ëtti àtte yu siwe ay jëf yu ñaaw, daan sonnal ak a fitnaal képp kuy woote yéwénal, mbaa’g yewwute. +Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund. + +Tuxug Yewwute gi: + +Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs. +Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay. +Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen. +Nitug Holand kii di Erasmus ( 1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi. + +Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax "kòllare gu yees gi" def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon. +Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi. + +Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali: + +Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll. + +Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey. +Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi , looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal. + +Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g. + +Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom. +Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi. +Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi. + +Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g ) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g ) ak ñu dul ñoom ñaar. + +Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi. +Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer. + +Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam . + +Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew. +Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii. + +Doggantal gu ñaareel gi: + +Wuññi yu juxraaf yi : + +Luy wuññi yu juxraaf yi ?: + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf, walla feeñal gu juxraaf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg,njëkk waa-Orob di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc , ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu juxraaf. + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, da nanu ko man’a xamalee ci nii: +mooy mbooloom ligeey yi jéngukat yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii: bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu. + +Li sabab wuññi yii: + +1) sabab bu diine: + +Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf yu Orob yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari reewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu. +Ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Reewum Portigaal moom daa gisoon ne reewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono. +Paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonnal ko,tee koo tas, ngir neewal dooleem, xottite ko,giir ko. + +Ci noonu mu ( moom paab gi) génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam geej yi la mbaa jeeri yi. +Paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nanu leen fi jeem’a jële. + +2) Sababu politig: + +Am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Fraans, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit ci biti seen, rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu'g nekku walla sosu gu yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man'a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen . Reew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi. + +3) Sabab bu koom-koom: + +Waa Orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal,mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir neewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi , loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke. + +Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova ak yu leen moy. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi. + +Lori waa Orob yi tàmbli woon na’a yol, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi rekk, bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Orob yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g ), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd , ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi . + +4) Sababu xam-xam: + +Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak bindam dafa soppiku woon, ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal ,juge Orob, génn, rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Orob yépp ci jamono yu diggu yi. +Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu , ak bëgg xam-xamu juxraaf, feeñ ci ñoom, ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi - ci xam-xam bu juxraaf bu jëm kanam, ak ginaaw bu xam-xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam. + +Wuññiy juxraaf yu Portigaal yi: + +Portigaal moom la ñu’y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf , yu Orob yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool (1394 – 1460 g ) , doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon dugg geej, ak yër xisay mool yi, ak teerey taariix yi . Muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi , moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta , ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g. + +Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi geej gu xonq ga ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum 1445 g, ginaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niijer. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko « Boppub Yaakaar Ju Baax Ji » ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End. +Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi, romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji, ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka dun bu End. +Vasco De Gama mii jot naa xamante ak Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi. +Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu geej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi nuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song barab ya ak mbooloo’m gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo ak buuri goxi End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End bi. + +Li wuññiy juxraaf yu Portigaal yi jur : + +Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw : + +1) Waa Portigaal, ñi ngi tàmbli woon di teg loxo ci tefesi Afrig yu sowwu yi, ci noonu njàppum jaam siw, te tas ci Orob gépp, di jaam yi ñu daa jàppe Afrig, te daan ci yaxantu. + +2) Jamonoy sanc gu Portigaal , mi ngi tàmblee ci bi Portigaal taxawalee ab sancu , ci penku bi, ca fa ñuy wax Jawa, ay xare it am diggante araab yu jullit yi ak Portigaal cig wàll, ak ci diggante waa Portigaal ak waa End yi ci geneen wàll. Waa Portigaal yi nag jot nañoo teg loxo yenn waax yu am solo yi nekkoon ci yoon wi jëme End. + +3) Waa Portigaal yi mujj nañu xam yoonu yaxantu wu geej, wu dul romb ci reewi jullit ñi,mooy wi jaar ca Boppu Yaakaar Ju Baax ja . + +Loolu nag mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi. + +Wuññi yu juxraaf yu Espaañ yi : + +Li ci duggaloon Portigaal, moo duggal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi. + +Moolub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahama ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi. + +Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ». + +Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul End. + +Ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal Espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu , ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca gox ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraagay ñu tudde ko Adduna bu bees bii di Amerig tay. + +Li wuññiy Espaañ yi jur: + +1) Ñoom de ubbil nañu tukkiy wuññi yi aw yoon wu bees wu jëm ci àdduna ju yees ji, di ko jaare ci màmbulaan gu atlas gi . Bu ko defee Espaañ tàmblee sanc gox yi mu jotoon’a àgg ci Amerig gu diggu gi ak gu bëj-saalum gi, ñu wisaare fa seenug xay ak diine, ubbi fa ay mbelli wurus ak xaalis. + +2) Saxal gu ñu saxal ci xam-xam ne suuf si daa “bulu” , te li waraloon loolu di tukki bi Magellan defoon. Buur bi ñu daa wax Shark mu juroomeel mi (Sharlakaan) di woon buurub Espaañ, daa digaloon mool bii di Magellan atum 1519 g, mu def ab tukki jëm penku jaare ko sowwu, ci noonu moom Magellan jug, war geej, jawali sowwu, te jëm penku, ci kaw màmbulaan gu atlas gi, bi mu ko defee daal di àgg ca tefesug Braasil ga, fa Riyo De Janero, mu wëy nag ca doxam ba, ba ca sottiwaayu dexug Labalata, daal di wër Amerig gu bëj-saalum gi, tàbbi màmbulaan gu dal gi nga xam ne moom moo ko tudde « pasifik » di wund lu dal, mu àgg Filipin atum 1521 g, foofa nag mu songoo fa’ak ñoñ réew ma, ci’y xeex yoy ca la ñu ko raye, waaye kenn ciy nitam, tuddoon Dianco, moo mujjoon jiite boobu tukki, dem ak ñoom ba ci boppu Yaakaar Ju Baax ji, juge fa dem Espaañ, gi nga xam ne ma nga fa àgg atum 1522 g. + +3) Weddi gisiin yi daa wax ci bindu suuf si ak ab kemam ( ni mu tollu), ndax kat tukki bii nga xam ne dafa dox, wër àdduna bi, firndéel na ne suuf si daal moo ëpp fuuf li ko Colombo jàppe woon ak ku dul moom. Beneen gox feeñ na, bu mag diggante Orob ak Asi ci wàllug sowwu gi, di Amerig gu bëj-gànnaar gi, nga rax ci dooli geneen gi’y gu bëj-saalum gi, te ag màmbulaan gu yaatu, gu yees’a ngii gu ñu xamutoon. Kon suuf desatutoon su ñu xamutoon su dul Ostrali ak ñaari xutbu yi . + +Wuññi yu Angalteer: + +Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu geeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug walla koloniiseg waa Angalteer yi, ñeel Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa . Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland. + +Wuññiy Fraans yi : + +Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy Fransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fetali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Fraans tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak goxi dex yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebek ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. moolu Fraans bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Fraans ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi. + +Wuññi yu Oland yi : + +Lonkoo gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu geeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali golofub New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ. Waa Oland yi jeemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g . + +Li wuññiy juxraaf yu Orob yi jur : + +Li wuññiy Tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw : + +1) Njiitug yaxantu gi tuxu na tukkee ci li wër geej gu diggu gi dem ci màmbulaan gu atlas, mu mujj moom yaxantu gi nekk ci loxoy reewi Orob gu sowwu gi, bu ko defee ñu nos fi ay yooni geej yu yaxantu ci ñaari màmbulaan yi, gu atlas ak gu dal gi (pasifik). +Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » . + +2) Wuññi yu juxraaf yi amal nanu fi jawwu yu gëpplante ak wujje, ak as lef cig noonoo ci diggante reew yi doon def wuññi yii, loolu moo yokkoon xemméemtéefi sanc yi ci diggante reewi Orob yi. Ci noonu aw gisiin wu sanc tàmbli woon’a feeñ wu Orob jëm ci askani reew yii ñuy door’a wuññi. + +3) Xam-xami juxraaf yi soppiku woon na bu baax, li ko waraloon di yaatu gi wuññi yii yaatu woon te bari. Ci noonu yëngu-yëngu gu nasaraanal yokku ci anam gu fés, rawati na ci Afrig ak ñaari Amerig yi. + +4) Ag jëm kanam feeñoon na ci wàllug yaxantug mbèll yi, di wurus ak xaalis, nga xam ne sax xarnub fukk ak juroom g, danu koo tudde woon « xarnub xaalis », ni nga xame ni jëm kanamug koom googu taxoon na ba dundiin wi gën’a kawe, njëg yi it gën’a yekkatiku, ni fi ay njaay yu yees dugge, lu ci mel ne kakawoo, poon, kiinaa, batata ak mbòq . + +5) Wuññi yi de lenn lanu ci màndarga yiy wone yewwuteg Tugal gi, ni nu la ko leerale woon ci doggantal gu njëkk ga. + +6) Reew yii ñu wuññi, ruu gu fees ak bëgg’a fayyu moo leen ubale woon, muur leen, jëm ci yii leen wuññi, ndax ñoom tubaab yi xalaati sanc lanu yoroon, daan ci doxe ci mbooleem seen doxi wuññi yi, lepp lu nu gis aakimoo ko, ngartaajoo ko, lii mooy li waral askani reew yi nu wuññi, jugoon ci jànkoonte ak ñoom, taxaw ci xeex canc gu Tugal gi, ci anam gu tar, jëfandikoo ci li nu yor lepp ci kàttan. + +7) Wesaare diiney nasaraan ci bepp gox bu nu wuññi. + +Doggantal gu ñatteel gi : + +Yëngu-yëngu yi jugoon di kontar Egliis bu paab bi + +Yëngu-yëngu gu yewenal diine ji ci Tugal : + +Yëngu-yëngu gu yéwénal gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Orob ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jeem’a delluwaat ci njàggaley Injiil yi. + +Li waraloon « yéwénal » gi : + +Ak li Egliis bi di nekk nguurug ruu lepp - ci li ko njëkk’a tax’a jug - teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot’a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom, ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Egliis bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtoo’k moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni. + +Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag yi ñépp di fay. Ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp. + +Ñaawtéefi Egliis yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi. + +Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat , nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex. + +Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Orob : + +Yéwénalug diine ci Orob - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam. + +Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Egliis bi te dëgëral ko. + +Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Egliis bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci egliis bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 - 1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam . + +Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli. + +Martin Luther ak yéwénal gi : + +Martin Luther mi ngi juddoo Isilban, di benn dekk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaañ atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi. +Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Egliis bi, li gënoon’a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi, ginaaw bi it, mu mujj fèttéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam. + + Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam. + +Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Egliis bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal . + +Luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Egliisub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Egliisu Watanberg ba, lakk ko. + +Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon : + +Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii : + +(1) Injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute. +(2) Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni. +(3) Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil. +(4) Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi. +(5) Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi. +(6) Wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi Orob gu sowwu gi. + +Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ-sañu paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi Egliis bi aki am-amam, ndax loolu man’a soril Egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci Egliis bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom Egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom. + +Jëfka yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu : + +Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii : + +(1) Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Orob yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a fèqu ak’a dañtalu ci ŋëbug paab gi ak sañ-sañam. +(2) Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam. +(3) Fonk sa xeet,walla xeetu gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Orob yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw Martin Luther, rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya. +(4) Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu. +(5) Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër it jam yi mu doon def Egliis bi . +(6) Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom. + +Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy protestants, maanaam ay diiŋatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi (katolig yi) ci geneen wàll. Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne goxu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant mbaa mu katolig, waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj-gànnaar yi – egliisam daal di doge ca egliisub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmark ak Suwed) . + +Kalfen (Calven) : + +John Calven mi ngi juddoo Fraans atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraans dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine . +Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi. +Kalfen ak Luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy: +(1) Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko . +(2) Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma. Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraans, Angalteer, Siwis ak yeneen. +Swingli : + +Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi. +Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine. + +Swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Egliis bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye. +Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Orob yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi. + + + + + + + + + Bunt bu ñaareel bi + +Jëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustri + + + +• Jeexiitalu gu waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi. + +• Lefi (wàlli) jëm kanamu xam-xam ci Orob. + +• Yewwuteg endustri: ay jagleem – ay màndargaam – ay ngérteem (li mu fi jur) + +Doggantal gu njëkk gi + +Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi. + +Jamono ji xam-xam neewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat, te meññi. +Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon’a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi. + +Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris End, rawati na ci ndoktoor, bidiw, ak mat ak yeneen yi. +Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaton ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi. +Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat, kimyaa ak xam-xami dénd yi , bidiw, juxraaf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell. + +Ngérum walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi: +Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii: +Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem’a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi . +Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono. +Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer ji di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu. +Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon’a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xam bi aju ci Yàlla . + +Digg yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Orob: + +Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Orob jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker-keraan yu bari, bokk na ci yooyu: + +(1) Andalusi : +Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon. +Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Orob yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Orob yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak’a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi. + +(2) Dunub Sisil : + Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Orob, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi. + +(3) Xarey jooñ yi bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Orob jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab, ak yi nu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris . +(4) Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Orob, rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi. +(5) Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Orob ci jamonoom ju bees jii. + + Xam-xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa Tugal yi: + +Lim (Mat): + +Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami kalkil yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon. +Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam-xamu waññ ( calcul), ñoo dolli woon tus ci lim yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam al kasr alhasarii di ci wolof (damat ci fukk) , ñu taalif ci wàllug xam-xamu waññ (calcul) ay teere yu waa Orob yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci. Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xam-xamu lim walla waññ, moom de lanuy sant bu lim (mumero) yi nekk ci kalkil duggee Orob tay. +Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki Orob yu bari. Boroom xam-xami Orob yi jariñu ci. +Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci matematig yi(xam-xamu lim), ñoo njëkkoon waa Orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii. +Bu dee nag ci andasa , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi nu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xam –xamu kalkilu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi . Nu xootal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g. + +Xam-xamu Fisiya : + +Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu Fisiya ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “séen” (almariyaat ). +Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab teere bu am solo, mooy teereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Orob yi mujjoon nanu ko’o tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g). +Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan Bun Alhaysam (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu fisiyaa, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo. + +Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët, ak weer yi ak leer ak yeneen. +Waa-Orob yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Orob yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax. + +Xam-xamu bidiw : + +Jullit ñi yittewoo woon nanu xam-xamu bidiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi, xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe. +Jullit ñi jariñu woon nanu ci xam-xamu bidiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu Geres yi niki teereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi. + +Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami bidiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom. + +Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi. +Waa Orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam-xamu bidiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam. + +Kimya: + +Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu kimyaa, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang . + +Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik , ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen. + +Mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki: seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal. + +Da na jaadu nu leeral ne xam-xamu kimya moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari. + +Waa Orob jariñu nanu bu baax ci xm-xamu kimya bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli. + +Ndoktoor : + +Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci xam-xamu ndoktoor. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw. +Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci ndoktoor, taalif na ci lu sakkan. +Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci ndoktoor, teereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de jenn jimblang la ju xam-xamu ngoktoor, ju waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Orob yi jariñu nanu ci xam-xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Orob yi. Waa Orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax Kaaw su nuy opere (xotti). + +Waa Orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk. +Bokk na ci boroom xam-xami Orob yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy. + +Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Orob’a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Egliis bi. + +Da na yell nu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Orob gu sowwu gi, ginaaw bi ab kureel ci waa Orob yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom. +Kon lu nu war’a xam la ne yewwuteg xam-xam ak gu endustri gii am ci reewi Orob yi, ci ginaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Orob tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay . + +Doggantal gu ñaareel gi + +Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal + +Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Orob, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu endustri ci Orob, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp. + +Li taxoon xam-xam jëm kanam : + +Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci reewi Orob gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di: + +(1) Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Orob yi te jariñu ci. +(2) Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam +(3) Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi nu fentee móolukaay yi. +(4) Xeemmeemteef gu waa Orob yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: yu Gres-Rom ya. + +Wàll yi xam-xam jëme kanam : + +Ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci Orop lepp, naan jamonoy reer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn mant’a reere, mant a weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu neew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu . Ci noonu Orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di: + +Ndoktoor : + +Ndoktoor ci Orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi, jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa Orob mujjoon nanu leen’a firi ci seeni làkk. + +Xam-xam bi Orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii, ba ci xarub fukk ak juroom benn g. + +Waa Orob yitewoo woon nanu bu baax xam-xamu ndoktoor, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom dey xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci Orob. + +Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci reew yii nuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci Orob. Mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci Orob ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje, wutal leen ay garab. + +Ci noonu boroom xami-xami Orob yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Beljik mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Fraans, ak Lofan Hok mu Oland mi, ak Luwis Pastor mu Fraans mi ak Kox mu Almaañ mi añs. +Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs. + +Juxraaf ak Bidiw: + +Xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal, te boroom xam-xami bidiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gëpp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nanu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay ligeey ci googu wàll. + +Waa Tugal yi nag seen xam-xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci Orob. +Jem kanamug xam-xamu Juxraaf tax na ba bu Bidiw it jem kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom dey duggal na loxoom bu baax – boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam-xamu bidiw – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi, bu ko defee nekkteefi asamaan yi di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi, ñoom ñepp danuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wëndeelu, maanaam roo te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wëndeelu. +Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu Bidiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi. + +Fisiya: + +Xam-xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu fisiya bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu. +Boroom xam-xami Tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si . +Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yeegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yef sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yitewoo xam-xamu fisiya, ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g. +Boroom xam-xamu Angle bii di Isaac NEWTON (1742 – 1727 g ) mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si . Moo wax ne bidiw yepp, walla plaanet yepp, danuy wër jant bi, ci ay ngunu yu sax , walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon. +Ki nuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni bidiw yi sosoo. + +Kimya: + +Waa Tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu Kimya bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw. +Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti kimya yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci. +Toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore. + +Waa Tugal yi nag, ñoom, danoo gën a jëmale kanam xam-xamu Kimya, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi, ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Fraans, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g. + +Kuran: + +Boroom xam-xam bii nuy wax (Thales), di ku dëkkoon Gres, moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran. Boroom xam-xamu Angle bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigeen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul kuran rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum 1672 g. + +Ki nuy wax Stephen Gray dikk, won nu ni nuy tuxale kuran, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci fiil yu xànjar. + +Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi kuran yi, te fent batari. Borom xam-xamu Amerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak kuran benn lanu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum 1831 g. +Waa Tugal soobu nanu ci xam-xamu Mat, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Frans bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële. +Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu Jiyoloji la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo. + +Jamonoy yewwute daal ci Orob mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te feexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Orob ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jeem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam. + +Ñatteelu doggantal + +Yewwute gu endustri : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi + +Yewwute gu endustri ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g. +Waaye nag, moom endustri mii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Amerig, la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. +Bi mu ko defee nag, ay jeexiitam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g. +Endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll. + +Looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal. + +Sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal: + +(1) awaase gi xam-xam awaase ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg endustri am. +(2) Dëkki Tugal yu mag yi, am gi nu am, ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam, rawati na, bi ci aju ci ràbbu ser , nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci Tugal. +(3) Jëmm ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Orob yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, feexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam. +(4) Li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it, muy teg loxo gi reewi sancaan yi daa def reew yi nu sanc , ak di fa jële ay xeewal aki ne-ne yu nu laalagul , di leen yobbu seeni reew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci Tugal. +(5) Reewi Tugal yi ak këri koppar yi, jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci Orob, loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox, man a àntu. +(6) Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal. +(7) Bari gi ligeeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci ligeeykat yi amoon xam-xam yu neew lanu woon, nga xam xam ne daanaka jàngunu woon. + +Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam : + +Yewwuteg endustri ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lanu: + +(1) Jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb : + +Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. +Loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci. +Ràbbkatu angle bi nuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin bu loxo, bu nuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla pono, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn ligeeykat di ko yor, di ko doxal. +Bu ko defee, fentkat bu angle bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas, mujj nu koy defe ci dooley ndox, nu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame). +Ki nuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari goxi Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire . + +Ki nuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox, ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb, daa ko defar ciy sér. + +Ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu Kimya yi ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey. + +(2) jëfandikoo kàttan : + +Jumtukaay yu njëlbeenu yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat . Kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ. +Ki nuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi, ak li nuy ligeey, ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci endustri ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll. + +Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland. + +Nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginaaw bi, nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi. Ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs. +Kuran tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li nuy wax juddalukaayu kuran, nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam. +Nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi. + +(3) Jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam: + +Bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ, loolu nag mooy bi angle bii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy ligeey. +Lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani. + +(4) Jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam: + +Li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug coolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi. +Ginaaw bi, nitug Amerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo coolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Ginaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi. +Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko endustri defe. Bu ko defee, feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi. + +(5) Feeñug campeefi endustri yi : + +Ligeeyuwaay yu ndaw yi juge nanu ci kër yi, doon leegi ay campeef yu endustri, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. +Endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu endustri, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi. +Isin yu mag yi nag, ci wetu barabi ne-ne yu nu laalul yi lanu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey, ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew. Neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel. + +Li fi yewwuteg endustri gi jur: + +Maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci Tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay. + +Li mu fi indi ci wàllug koom: + +Yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom, ci biir Orob ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li nuy ligeey gën a yokk, gën a wuute, li nu koy jënde gën a neew, ñepp man cee jot, jumtukaayi ligeey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu adduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk ak sanc , tàmblee booloo. +Ndax kat sanc gu politig gu yees gii, du lu dul doomi sanc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ne-ne yu nu laalul yi, ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute. + +Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp, ak li mu gën a ñaw lepp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a ligeey, ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari, te daa nanu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Orob, rawati na ci Angalteer. + +Joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi, nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu adduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi. + +Li mu fi jur ci politig: + +Sanc gii Tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi, wuutal ko fi, ginaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw , endustri day soxla ay ne-ne yu nu laalul, te loolu danu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii, tax it ba reew yi nu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag sanc, ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi. +Bu ko defee, benn dal daal di feeñ ci Orob, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu libre ” bi am te taxaw ci nosteg bopp-alal . Loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen. +Goornamaay Tugal yi, jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan . Ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi endustri yi. Loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi. + +Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay. +Goornamaay Tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi, ci noonu ñu yamale waxtu yi nuy ligeey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lanu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi, jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax. + +Man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew, feeñ na, te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis reewi Tugal yi sukkandiku ci endustri, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi nu miinoon. + +Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay: + +Yewwute gi ci Orob jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi, ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki endustri yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll. Bu ko defee baykatu Orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi. +Lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a neew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy neewug jóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer. + +Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër ligeey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey ligeeykat yi gën na a yokku, bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja’a neewi seeni aajo, ngir seerug dund gi. + +Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd’ak yewwuteeg endustri gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi, leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay, ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg. +Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi, ci Tugal, maanaam nit ñi, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci Orob, ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe-jafey ligeey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos ligeey bi, aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal yi moom isin yi. + +Ñatteelu bunt bi + +Yëngu-yënguy politig yu mag yi ci adduna bi + +Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A) + Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans + +Doggantal gu njëkk gi + +Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi + +Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Amerig, gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Amerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci: + +(1) Fitnay diine yi amoon ci Orob gu digg gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di kontar Egliisu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak mu Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Amerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore. +(2) Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig . +(3) Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, danoo gëmoon ne Amerig de reew mu fees dell la ak yile mbèll, te ña fa dëkk, ñu neew ag xay lanu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll. +(4) Jëm kanam gi xam-xam am ak endustri ci Tugal, rawati na ci wàllug ligeey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori. +(5) Ligeey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nanu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi. + +Sancu yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nanu leen ci Amerig gu bëj gànnaar gi: + +Waa Tugal yii bawoo woon Espaañ, Fraans, Holand, Suwed ak Angalteer, sancoon nanu ay barab yu wuute ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lanuy wax tay Diiwaani Amerig yu Bennoo yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nanu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaayeTugal. + +Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb akug dagge ca reew may nday di Angalteer. +Angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy : buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci nu taxawal ay sancu, ak jariñoo xeewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi. +Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen . + +Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy: New York, Wirjiniya, Rood Island, Masacuusest, Dulawir, New Hamser, Kintakit, North Karolaayna, South Karolaayna, New Jersi, Jorjiya ak Pensilvaniya. Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Amerig gu leegi gii nii, dunu weesu benn xaaj ci Amerig gu nu xaaj fukki xaaj. + +Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi: + +Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte sa bopp” , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di reew mi leen moom. +Nosteg àtte-sa-bopp googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk: + +(1) Doxalkat bi , +(2) Jataayub yoonal bi , +(3) Jataayub diisoo bi . + +Doxalkat bi walla àttekat bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (àttekat bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli. + +Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu ligeeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru doxalkat bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal. + +Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom. +Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte-sa-bopp ” gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer. + +Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen reewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew, di ci tënku, te di ko fonk. +Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi . + +Li waraloon xareb temb bi: + +Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lanu woon yu di ay protestant . Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy: + +(1) Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas” +(2) Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu. +(3) Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo dim reewam, fa la feetale ag reewoom . + +Ëttub Amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii: + +Yoon yuy tege galag ak tembar: + +Parlamaa bu Britani bi daa genne atum 1762 g, aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi, mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu Ofisel yi, ak dosyee yi, ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Fraans yi ak yu Holand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak rasaas . + +Yoon wi aju ci geeju (navigation) ak yaxantu: + +Ci atum 1651g, barlamaanu Britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal li nuy genne ak li nuy duggal di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na Angalteer. + + Koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf: + +Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel . Noonu tam lanu teree woon – ci beneen luwaa - ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom. + +Nos dooley kaaraange ji: + +Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci genn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko. +Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer. + +Waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp, dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon. +Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante. +Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu nu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu. +Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nanu ne moo waral xareb temb bi. + +Ndajem waxtaan mu Filadelfiya mu njëkk mi: + +Juroom ñeenti diiwaan yu Ameriig teewe woon nanu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg. +Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi. + +Looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” . + +Man nanu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko, di ci kontar ni Angalteer di àttee seen reew yi. + +Ñoñ sancu yepp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfi, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yepp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii nuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma. +Ndajem Filadefi moomu, mooy dàtt bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi . + +Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom. +Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ - ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi. + +Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon. +Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nanu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefi, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def. + +Ndajem Filadelfi mu ñaareel mi: + +Ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfi, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfi mi, ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar – ak doonte lu neew la itam – seen diggante ak Britani, reew miy nday. + +Ni xare bi tàkke : + +Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu Amerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Amerig yi. +George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu. + +Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington gañe woon na njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanada, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi nu gañee Britani, Fraans jug na, yëgleb xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Holand topp ci atum 1780 g. Man nanoo wax ne Fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu bennoo yi, ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Fraans lii di Lavette, kontar Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci jë yu bari. + +Dàq gi nu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa Fraans aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat. + +Nanu fàttaliku nag ne waa Amerig yi ñoom, ci seen suuf lanu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanada, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka. +Nga rax ci dolli, waa Amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nanu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington. +Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi. +Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Amerig. + +Tembug Diiwaani Amerig yu Bennoo yi: + +Bi waa Britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Amerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe, gañee ko ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Paris, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g, lii mooy poñ ya ca ëpp solo: + +(1) Britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon. +(2) Jeem a rafetal seqoo yi, ci diggante Britani ak reewum Amerig mu temb mi (Diiwaani Amerig yu Bennoo yi) +(3) Amal ci diggante Britani ak Amerig gu temb gi, ay seqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom. + +Nii daal la Diiwaan yu Amerig yu Bennoo yi ame, xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi. +Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke. + +Amerig nag moom, daal di ñew, defar sartu reewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nanu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cer ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi. +Ginaaw bi lanu def Washington – ginaaw bi mu nekke peeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def peey bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Amerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi. +Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon. + +Doggantal gu ñaareel gi + +Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans : + +Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (fipp googu), mi ngi ame woon ca Fraans, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benn ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu toll ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g) defee yong gu nuy wax yongug 18 Brumaire, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi. +Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Fraans gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk jàmm ga, tiitale ga , tuur dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug Fraans gi. Loolu nag taxoon na ba “fipp gi” manu fi woon a amal dali gore , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi. +Waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi, yamuñu rekk ci Fraans, waaye weesu nanu ko ba daj Tugal gepp, ak lu bari ci reewi adduna bi. + +Ni Fraans meloon laata fipp gi: + +Bu ñu gëstoo na Fraans meloon laata fipp gi, loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi, atum 1789 g. + +Melokaanu politig wa: + +Buuri Fraans yi, ni ñu doon àttee Fraans, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lepp, kepp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub Fraans bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ). + +Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi. +Moom de jaraafam yi danu koo yilifoon, ak bëkkneegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal, kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar. +Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Fraans yi bañoon. + +Njabootug Barbon gi, yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Fraans wi, ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo reew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe Fraans. +Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali reew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi. Looloo taxoon njëlul nguur gi loof, mujj moom nguur gi fees dell aki bor. + +Nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci 130 milyong yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyon yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon. + +Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga. +Nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Fraans mujj di reew mu ay gox boole, gox bu ci nekk am ay yooni boppam , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi, reew mi mujj seddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Fraans mujj doonatul menn reew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas. + +Na mboolaay ga meloon: + +Mboolayug Fraans gi, njëkk fipp gi, dafa seddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: kureelug ñu tedd ñi, walla garmi yi, kureelu niti diine yi, ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi. Ñatti kureel yii nag – ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu – yamoowunu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay warteef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay. + +Bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi, yu siwil yi ak yu xare yi , ci nguur gi. +Ñoom ba tay, daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm yi, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amunu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi. + +“Nitu diine yi” nag ñoom, seen kureel moom itam bu ràññiku la woon, niki bu garmi yi, ñoom de daa nanu am ay suuf yu nu leen dogal, yu yaatu, yu daa toll ci juroomeelu suufi nguur gi, maanaam bu nu xaajoon suufi nguur gi juroomi xaaj, benn xaaj bi. Ñoom itam, ñu nu teggiloon ay galag lanu. Li Egliis bi daa gañee ci suufam yooyu, ak ci galagi diine yi nga xam ne mbooloo mi daa nanu ko ko fay, àggoon na ci 200 milyon yu Farank. + +Loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbli. +Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu feexoon, moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi. + +Kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi fipp gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyongi nit , te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon 300 junniy nit. Coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kureel boobu nag (bu baadoola yi), moo ëmboon kureel bu diggu bi, walla bi nuy wax (Bourgeois), ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si. + +Bu dee kureel bu diggu bi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amunu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon. +Lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi. + +Bu dee “kreelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen ligeey yi gën a tar. + +Bu nu nee “kureelub soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi moom, ak pal yu mag yi, garmi yi lanu leen daa jagleel. + +Na fa xalaat meloon: + +Ak li Fraansu njëkk fipp gi, di gënadi woon a nekk cib coona, ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lepp, teewul waa Fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs. +Jamono jii , dafa fiiroo ak diggante bob Fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nosi politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya. +Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau. + +Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay ligeeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Fraans ak feneen. +Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi, te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju doxal ji, ak ju laman ji . +Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca Fraans. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca Angalteer. + +Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Fraans wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam lanu woon ak yéjj . +Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Fraans ak gu egliis ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi. + Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Fraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital. +Wolteer de gore ga waa Angalteer ame woon da koo neexoon lool, yeemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy danu koo dàqe woon Fraans. +Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca teereem ba tudd “bataaxeli xeltu” , walla ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer, atum 1734 g. +Wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon Fraans, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi. +La desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër. +Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom teere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi. +Fippug Fraans gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi ki dëkk Fraans – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi. + +Jafe-jafe bu koppar ba: + +Atum 1789g, mooy at mi fipp gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom, waaye la waraloon fipp ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon. + +Luwis 16, bi mu ñëwee jeem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kureel yu xeet wi” – bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje. + +Naka la fipp gi ame woon : + +Doomi kureel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir nu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Fraans man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk. +Ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll, ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll. +Bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kureel yi (bu garmi yi ak bu niti diine yi) bu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kureel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cer , ne daal ay neeg ñooy woote, bi loolu amee, ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee, cig beru, ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi reew mi, bu nu booloo, waxul bu benn taqalikoo nee, beru. +Ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Fraans, bi nga xam ne day leeral li waa Fraans bëgg, tey jeem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug fipp gi. + +Tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen: + +Ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca Versailles ngir defaral Fraans ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, genne ña ñu fa tëjoon ngir politig. +Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Fraans wi di màggal, at mu nekk . + +Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Fraans, dem feneen. +Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Fraans, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi, ndax du seen njariñ, danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ . + +Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi, aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba. +Xarekati fipp gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse ak gënjëng . + +Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi. +Xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu ju Fraans ji mujj fekksi “wattu gu reew “ gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi. Ci noonu mbooloom xare mu Fraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba. +Waaye way fipp yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi, ak mu Egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Fraans gepp, ñu daal di seddalewaat Fraans def ko ay doxaliin yu bees . + +Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jeem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy genn reew mi, gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan. +Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 sebtambar 1791 g, loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Fraans la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi. +Mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Fraans wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur saxoon na ca Fraans ba ca 21 sebtambar 1792 g. + +Ci atum 1792g, beneen woote amoon na, bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Fraans, ca 21 satumbar 1792 g. +Ñu feetele ko doxal reew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar fipp gi, aar it Fraans ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci reew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen reewi Tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi. +Feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu Fraans bu dëgër, boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi. +Ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, danoo gëmoon ne fii Fraans toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi. + +Ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi: + +Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci reewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Fraans, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange, feetale ko ligeeyub aar Fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi, ñu feetale ko ba tay moom kureel bi, wàluug taxawal am mbooloom xare mu Fraans mu dëgër, ngir aar Fraans, ak fipp gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xeewal, moom fipp gi. Goornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi gañe na xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Beljig ci ñu fipp ci kaw Imbraatoor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi (moom paab gi). + +Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nanu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Fraans yi, ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag. +Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar fipp gi, ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar reew mi, tas te giimal fèttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi, duggal seeni xarekat ci Beljig ak Holand, ànd ak loolu lepp teewul waa Fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu. + +Ci 29 sulye 1794g, la ceri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Fraans bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi. + +Goornamaab doxaliin bi: + +Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonay tiital ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon: + +(1) Def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam +(2) Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi. + +Nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig. +Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu, ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon yong googu nuy wax yongug Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Fraaans te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lanu nekkoon. + +Napoliyon Bonaparte: + +Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Ajaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Fraans da koo mujjoon jënde ci Genova. +Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi genne ca bànqaasu xare ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kureelub kano ya ca xarekati Fraans ya. +Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali fipp gi , te fonkoon leen. Moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee Itaali. +Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Fraans, dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Fraans gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g. + +Song gi Napoleon defoon Itaali: + +Goornamaab doxaliin bi, dafa feetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu Cherasco. +Napoleon defati ab xare ak dooley paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, neewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare. +Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Fraans, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Fraans. + +Song gi Napoleon songoon penku bi: + +Politigkati Fraans yi naaloon nanu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug Mans. +Politigkati Fraans yi, li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Fraans ci geej gu diggu gi, ak man a àgg ca geej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk penku. + +Goornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko denkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, geeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Fraans. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Fraans mi, ca ndoxum golfub Abii Xiir, moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Fraans cangug geej gi Fraans yàgg a gent. Fraans sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej, mu mel ne mu Britani mi. + +Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xare jooñ la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga. + +Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg Usmaan gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam. +Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom, xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew. Waa Isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy danoo fippoon ci kawan, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “fippug Xayra gi” . +Napoleon jawali na reewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, ak Yafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi, waa Usmaan yi di ko jàpple ci jeeri ji. +Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji nuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam. + +Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Fraans, waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule goornamaa. Bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga. + +Ay ngérte , yu am solo juddoo nanu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk: +(1) Xareb Fraans boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu feete, ci wàllug jokkoo ak tuxu, ñeel imbraatoorug Britani gi ci penku bi. +(2) Xare boobu Fraans da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi Afrig gu bëj-gànnaar gi. +(3) Boroom xam-xami xare boobu, bi nuy ñëw, indaale woon nanu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak geej gu diggu gi, di kanaalu Suwes bi, te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu Bolaax bi. +(4) Xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Fraans ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs. + +Napoleon ak reewi Tugal yi: + +Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Fraans ji genn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara. +Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Egliis bi ci Fraans. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbal. +Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyeel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi. + +Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi Tugal yi. Britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi, ca xare ba nuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan ak Aleksandar mi nekkoon sesaarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, nu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal bepp, jëme ko Britani , daal di woon ga reewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci reewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na reew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu sesaar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca peey ba, di Butrusburg, waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi nuy dellu nag la waa Rusi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg. +Bu ko defee waaTugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy gañe ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona nu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Fraans yi, ngir xeexi reewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g. + +Bu ko defee, reewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir seddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos reew yu am doole yu peek Fraans wër ko. + +Ligeeyi ndajem Vienne: + +Ligeeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon: + +(1) Way daje yi delloowaat nanu buuri Tugal ya ca seen reew ya nu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Fraans ak Espaañ. +(2) Britani jëloon na sancu yi Fraans moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos. +(3) Rusi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Beljig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di nationalisme gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Rusi ak Otris ak Brusiya, danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu Tugal yu ndaw yi. + +Li juddoo ci fippug Fraans gi: + +(1) Fipp gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral reewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi. +(2) Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal. +(3) Fipp gi ci Fraans mooy gi njëkk ci fipp yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay term yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees. +(4) Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lanu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gepp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee. +(5) Xalaatub fipp gi law na ba àgg ci Tugal gepp, ak yeneen reew yu dul Tugal, yu adduna bi. + +Buntub ñeeteel bi + +Yëngu-yëngu yi aju ci “xeetu” walla fonk sa xeet (nationalisme) ci Tugal, ci xarnub fukk ak juroom ñeent g. + +Bennal gu Itaali + +Bennoo gu Almaañ + +Doggantal gu njëkk gi + +Bennal gi nu defoon Itaali + +Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi: + +Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon reew mu nu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Doox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia. + +Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatoor lanu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa lu ko moy . + +Jeexiit ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali: + +Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. +Mu wutaloon reew mi mepp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi, mu may waa Itaali yi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu Itaali mu man a am, mu nu bennal. + +Itaali ginaaw ndajem Vienne: + +Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy: Piemonte, Napoli, Parma, Modena, Toscana, Lombardia, ak Venezia, ñoom ñaar nag, mujj nanu leen boole def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris. +Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga” maanaam lu nekk, nanu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen seen barab. +Metternich ak bëtam yi mu tasoon ci gox yepp, jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi, daan naj it gepp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle. + +Yewwueg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali: + +Politigu noteel gi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi nu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon. +Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi. +Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu: booloo gu Karbonari (ñoñ këriñ), ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi. + +Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nanu ci, baykat yi, ligeeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs. +Li leen manke woon nag, mooy danoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a not, te daa àntoodil seeni fipp. +Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal. + +Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam. + +Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal reewum Itaali mi, ci ron ag noste gu republig. + +Yëngu-yëngu yii, mujjoon na naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab kojug xare la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal na yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer. +Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi endustreem tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. +Boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali. + +Ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi. + +Ak li boole Itaali, def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Doox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëggunu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li. +Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki Dooxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw gennam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk. + +Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali: + +Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, (ñoom xaaj yi), ñooy: Piemonte, mi nekk ci ron doji Alp yi, nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle, ak Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Fraans gi dend ak Itaali, moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu Fraans ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci geej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte. Ak Genova, moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal. +Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii, ñu tudd ci yi ci ëpp solo: + +(1) Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali. +(2) Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jawrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul Piemonte. +(3) Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam-xam. +(4) Piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo. +(5) Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano. +(6) Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram. + +Cavour ak bennalug Itaali: + +Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu republig. Moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom Piemonte) ak jeneen doole ju reew, ju mel ne Fraans mbaa Britani. + +Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal Itaali. +Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem Otris mi, te man leen a genne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak endustri bi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri, tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi (bu biir reew mi), yewenal nosteg galag yi, daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi. + +Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yewenal yu biir reew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte geek Eglis bi. + +Kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon, bu nu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Fraans, am Rusi, ak Brusiya, waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la woon, manul woon a ñàkk, te itam mbirum adduna bepp la, laaj na reew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko, ci ndajey Tugal yi. +Ci noonu mu digal parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Fraans, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatoor bu Fraans bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg. + +Kureelu xare bu Piemonte boobu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe, teewul Kafour moom lijjanti na ba nu yëg Piemonte ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb Xarm bi jeexee. +Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, kontar Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ. +Bu dee Fraans nag, nga xam ne pencam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu reewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci Tugal. Politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it reew mu nekk ci wetu Fraans la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk. + +Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia. + +Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris: + +Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari temeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko kontar Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi . +Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g. +Taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk. + +Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Fraans itam jibal ab xareem ci kaw Otris. +Soldaari Piemonte yi ak yu Fraans yi jot nanoo duma Otris, gañe ko ca xare ba nuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatoor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li nuy wax juboo gu Siyorix atum 1859g. bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga: + +(1) Otris bàyyee Piemonte Lombardi +(2) Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur +(3) Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi +(4) Delloosi ñi yilifoon Doox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee. +(5) Boole Niis ak Savoia ci Fraans. + +Taarixkat yi, firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Doox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte. Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral. +Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Fraans genne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi. +Askani Doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko poñi juboo gu Siyorix gi yaxale, ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug Piemonte. +Ci noonu ay fipp am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti. +Nii daal la Itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali. + +Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn: + +Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci ligeey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu yu Itaali yi nu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. +Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Silil bi , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam, dugg ci bennoo gi. + +Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali: + +Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi bepp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moo rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko. +Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 febriye atum 1861g. Ca ndaje ma lanu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu nu bennal gi. +Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulye atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig. + +Def Rom peeyu nguurug Itaali gi: + +Waa Itaali yi delloosi nanu Venezia mi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab gox ci Itaali, ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya. +Fraans it ay xarekatam gennoon nanu Rom, ngir sotti gi Fraans sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne Rom daal mooy peeyu nguurug Itaali gu nu bennal gi. +Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi. +Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikan, am it sañ-sañ ci yabal ay ndaw yu koy toogal ca biti. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo . + +Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew. + +Doggantal gu ñaareel gi + +Bennoo gu Almaañ + +Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi: + +Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan, yepp it ci ron imbraatoor gu Otris lanu nekkoon, walla li nuy tudde Imbraatoorug Rom gu sell gi. Almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo. + +Almaañ ci jamonoy Napoleon: + +Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko not, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo peeyam ba Berlin. +Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoni bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lanu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw. + +Almaañ ginaaw ndajem Vienne mi: + +Ginaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lanu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Doox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Rusi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam goxub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoni. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko. +Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey kontar mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo. + +Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi: + +Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, duggal leen ci genn nguur gu Almaañ gu nu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem goxi nguur gi. +Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan. Nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci Brusiya, ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nanu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay goxam yu biir yi. Gox yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan, gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lanu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan. + +Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li nu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy: + +(1) Solofrayn +(2) “Bennoog nduwaan gu Bavar” gi nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at. +(3) Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoni. Mooy gi Saksoni taxawaloon atum 1828g. + +Kilifay Brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani Almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub Solofrayn, gën a yàkkali ab geewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoni ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin gu Brusiya, te da na jàppeji Brusiya muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, dunu ay doxandeem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nanu ne Almaañ gepp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g. + +Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gis Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug Almaañ gi. + +Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy reew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ. + +Jeexiit yi fipp gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi: + +Ay fipp yu bari jot nanoo am ca Tugal atm 1848g. Ag fipp am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu . Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot fippi Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe. +Kërug Orob gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj. + +Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu reew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jeem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas. +Ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma: + +(1) Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya. +(2) Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug Otris gi +(3) Genne Otris ci bennoo gu Almaañ gi. + +Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nanu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatoor ci Almaañ gu nu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol. +La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Rusi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba Vienne. +Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi tegunu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du ligeey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi. + +Otris ak Rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu reew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole. +Looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a genne Otris Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi. +Xalaat bii nag diisoowaale bu Brusiya bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi. + +Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi: + +Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju mag ja. Daal di dugg ag coldaar, gennati ca, dem nag feete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam ngir nu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cer ci parlamaa bu Brusiya bi. Ligeey na it ci toolub diplomasi, doonoon ndawul reewam ca Butrsburg ca Rusi. Ginaaw bi mu nekkal reewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Fraans, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya. +Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Egliis bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kilifaam, waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti reew. + +Bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne Fraans ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga. Ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi, daal di beddiku sartu reew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi. + +Wàllug xeetu nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew, ndax daa gisoon ne sartu reew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi. +Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy: +(1) Coldaar gi +(2) Politigu bitim reew bi +(3) Fal ay jawrin ak di leen folli + +Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ, loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ . +Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yepp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu federaal, guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko. +Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi, ngir yeegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy: +(1) Dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi +(2) Jiite benno gi + +Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi. +Bismarck jeem na a fàggu cofeelug Rusi, ngir mu bañ a feete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Rusi, kontar gori Ploñ yi defoon ag fipp kontar Rusi, ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb. +Fraans nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Fraans. +Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Rusi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom reewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Rusi. Te it nanguwutoon a ànd ak Fraans ak Otris kontar Rusi. + +Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ: + +Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal reewi Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy: + +Xare Brusiya yi ak Danmark: + +Bismarck xuus na ab xare kontar Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari doox yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo. +Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari doox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dooxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin. +Xarey Brusiya ak Otris: + +Bismarck gisoon na ne xare bi moom – deet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig. +Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris. Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim geejug bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu. + +Sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g. + +Bismarck moom lijjanti woon na ba Rusi genne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Rusi ci giimal fipp ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratoor bi Napoleon III, imbraatooru Fraans, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub Rayn. Mu demati tapoo-ji ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom. + +Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a gañee ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatooru Fraans bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Fraans dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatooru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Fraans, Otris du ko sot, ci geneen wàll. +Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame: + +(1) Gennug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi, gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich. +(2) Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu federaal gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu. +(3) Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia. + +Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem reewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari doox yii di Shalswig ak Holistin ci lanu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje. +Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare . + +Xareb Brusiya ak Fraans: + +Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya gañee ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Fraans moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll. + +Fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu nu dogat, ngir mu nekk moom Fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daa kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Fraans du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon. +Lëj-lëju ku jigeen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans. +Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa feexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Fraans mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul Fraans ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw Fraans. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Fraans. Loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Fraans. Ci noonu Fraans jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulye 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu nu dàqee Fraans ci xeex bi. + +Brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak Fraans, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya. +Xare bi bepp nag ci suufus Fraans la doon tàkke. Jotoon nanoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu, te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Fraans ji ci biir suufus Fraans, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Fraans, te mu leer nàññ ne Fraans moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 11870g. + +Ci noonu imbraatoor gu Fraans gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi . Daal di teg Fraans ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans ( loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi dunu genn Fraans li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di Alsaas ak Loren ci fraans, boole leen ci Almaañ. + +Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatoorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratooru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi. +Sartu reew bu Almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay: + +(1) Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundasrat) +(2) Jattayu (Rechstag) + +Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundasrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer, ñu seddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci Bundasrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiit, ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, danoo takku woon ci Brusiya, te daawunu woote lenn lu mu bëggul. Te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga. +Bu dee nag jataayu Rechstag nag moom, man nanu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cer, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu Almaañ bu bees bi, danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo. + +Bismarck nag, jiite na goornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kilifteefam tam la Almaañ gu rëy gii gepp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nanu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at. + + + +Juroomeelu bunt bi + +Sanc gu yees gi + +Sabab yi fi indi sanc gu yees gi, ak ay anamam +Reewi sancaan yi +Ñaawteefi sanc yi +Yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool + +Doggantal gu njëkk gi + +Sababi sanc gu yees gi aki anamam. + +Xamale lan mooy sanc gu yees gi: + +Li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy juxraaf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci reewi adduna bi. + +Sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbèll. +Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen. + +Sababi sanc gu bees gi: + +Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + +(1) Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri, ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi. Loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne-ne yu nu laalul aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri, ndax seen koom-koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu nu laalul yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu nu man a jaaye seen ligeeyi Tugal yu endustri yooyu. +(2) Yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon, loolu moo waraloon reew yii gëstu-ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu reew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc, politig la bu nu nosoon, jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp. +(3) Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan: wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw, ñi xamul dara. Adduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom. +(4) Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci reewi Tugal yu endustri yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii. Loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Reewi Tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu, waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak ñawug seen ngànnaay, ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi. +(5) Lu bari ci reew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole. +(6) Ay lonkoo yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi. +(7) Bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna, loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi, di taqale diggante goxi adduna bi. +(8) Bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principes) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc. + +Anami sanc gu bees gi: + +Sancug Tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + +Sanc ngir dëkk: + +Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu-yëngug wuññiy juxraaf yu Tugal yi. +Bu ko defee reewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale. +Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Amerig gu digg ga ak gu bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lanu cosaano, loolu di ci Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi, lu ci dul Bresil,moom waa Portigaal a ko sancoon. + +Nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca Falastin, bi nu ko sancee ci doole, dëkke ko, reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi, dajee, dëkksi ca Falastin, ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug reewi sancaan yi, ak li askanu Falastin daan xeex loolu lepp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko. + +Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle. + +Teg loxo gu xare : + +Ay reew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay reew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gèndiku woon ci yii reew, rawati na ci wàllug xare. +Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii. +Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk: +Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g, ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g. + +Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la. +Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew. + +Aar : + +Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono. + +Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen. Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe. +Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk: +Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo. + +Feetale : + +Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiit yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel. + +Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi. + +Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen ko. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil. +Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk: +Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs. +Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom. + +Denkaane : + +Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wutu fi kureelug xeet yi. +Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika ak yeneen . + +Sancug aada : + +Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom. + +Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi it, Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi. + +Barabi sañ-sañ : + +Lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani. +Amoon na it ay xejj yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen. + + + + + + + + + + +Ñaareelu doggantal + +Reewi sancaan yi + +Lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi, ci gox yii di: Afrig, Asi ak adduna bu yees bi (Amerig). Reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu, ci taarix, ñooy: + +Reewum Portigaal: + +Waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu Tugal ci ñaari gox yii di Afrig ak Asi. Ñoo ci jiitu woon waa Espaañ, Holand, Angalteer, ak waa Fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf ci jamonoy yewwute gu Tugal gi. + +Tukkib Vasco de Gama bu njëkk bi mu defoon ci Afrig ak End, moo ubbi woon gëti waa Portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci Afrig ak Asi ngir teg loxo geeji penku yi, ak rënk yaxantug penku gi , rawati na li ci aju ci ay rëndaay , ak ngir yàq koom-koomu reewi jullit ñi, rawati na nguurug Mamaalig yi, ngir loolu man a doyadil jullit ñi, neewal leen doole. + +Waa Portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ-sañ ci duni Madira yi, Bopp bu Wert bi ak Osoras, barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi,la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba ca fukk ak juroomeelu xarnu g. Cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci Afrig ak Asi ci xarnub fukk ak juroom g, yu ci mel ni: Mosambig ci penku Afrig, Angola ci sowwu bi, Ecopi, ak duni Madagaskaar, Moris ak Silaan ak xat-xatu Hormos ak xat-xatu Malga ci daanaka-dun bu Malayo añs. + +Waa Portigaal yi defoon nanu seen “sanc gi ngir dëkk” ca Bresil, gi nekk ci Amerig gu bëj-saalum gi, ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu Afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi. +Nu leeral leen ne sancug Portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu, ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu, ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu. Ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex. + +Reewum Espaañ: + +Espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa Portigaal, waaye jariñu ci seen xam-xam boobu ñu jot a am ci lef moomu. Bu ko defee, waa Espaañ jël goxi Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa. Moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna, ray, song, jaay doole ak gënale ci wàllug diine. Ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi, gasal leen mbell yi. Ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug Espaañ, ci làkk, ci diine, ci aada ak ci taarix, ba mujj sax bii gox ñu koy wooye Amerig gu Latin gi, di ko askanale Latin gi nu jublu woon Esspaañ ak Portigaal. +Espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam, lal ko ci kaw ay barab ci goxu Afrig, yu ci mel ni duni Kanari ak àllub Maraakes bi ak goxu Afni bi dend ak Maraakes ak Gine gu Espaañ gi nekk ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi . + +Sancug Espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi Tugal doon def ci wàll googu. Ci noonu waa Angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon Irmada, atum 1588g. Mbooloom gaalum Holand mi tam moñoxeeti mu Espaañ mu lòtt mii atum 1607g. Ci noonu la Espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante gu Angalteer, gu Fraans ak gu Portigaal. Bu ko defee, ay fipp am ca sancuy Espaañ ya, ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa Espaañ yi. + +Reewum Holand: + +Waa Holand yi danoo duggoon ci ngérum Protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo gu Espaañ gu katolig gii. Looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu Espaañ yii, daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Waaye temb gii nag nangu na ko (moom Espaañ) ci anam gu ofisel atum 1648g, ca kollareg Westfalia ga nu defoon, ginaaw xareb fanweeri at ba . +Waa Holand daal di taxawal lonkoo gu End gu penku gu Holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi, daal di not waa Portigaal yi ci wàllug sanc, teg loxo duni End yu penku ya ca Asi. Yaatuwaayu suuf yi Holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu Holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam. + +Sancaan yu Holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi, kawsu, attaaya, kafe, suukar, seng ak petrol añs. +Waaye ñii dëkke woon ci sancu yu Holand yi te cosaanoo fa, xeexoon nanu kontar waa Holand yii ba mujj am tembte atum 1949g ci turu Endonisi. +Waa Holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di Amerig. +Ñu taxawaloon lonkoog End gu sowwu gu Holand gi atum 1622g, ñu sancoon goxub dexug Hadson, daal di jënd Manhatan ci endo yu xonq yi, daal di taxawal dëkkub Amstardaam bu bees bi nga xam ne waa Angalteer yi nangu woon nanu ko ci Holand, tudde ko New York. Waa Holand tam sancoon nanu – ci diirub fanweeri at – ag wàll gu mag ci Bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug Portigaal. + +Reewum Beljiig: + +Leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum Kongo mi nekk ci digg Afrig atum 1876g, daal di koy def ag moomeelam, loolu nag wéyoon na di nekk ba atum 1908g, ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum Beljig. Kongo nag reew mu naat la lool, te woomle ci ay koom-koomi mbell. Waa Kongo nag jàmmaarloo nanook sancug Beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal, daan jariñoo it seeni koom-koom ci anam yu ñaaw a ñaaw, loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum 1960g ci turu Saayir. + +Sancug Britani: + +Imbraatoorug Britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay. Moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si. + +Britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi, waaye ca Amerig gu bëj-gànnaar ga, mu sancoon lu sakkan ciy suufam, waaye dëkke leen, te sonn it ci dindi kilifteefug Fraans ak Holand ci gox bii te jële ko fi. Bu ko defee, sancu ak dëkkuwaay yu Britani yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu Britani ba kero Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi di am tembte , naka noonu Kanada, ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak Britani, muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan, te bokk nekkandoo ci “Komonwelth gu Britani”. Britani sancati na Ostraali ci anamug dëkk ak Newsiland, waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci Komonwelth. + +Britani sanc na End, wéyal fab sañ-sañam, daal di sos lonkoo gu End gu penku gu Angalteer gi atum 1600g, mu jot a dàqe Fraans ca daanaka-gox bu End ba . Mu manante Siin ci mu ubbi ay waaxam ci kanamu Afyon bii nga xam ne Britani daa na ci indi lu bari ci waa Siin yi. Looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante Siin ak Britani, di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum 1840g ba 1842g, nga xam ne ca la Britani nangoo waaxub Hong Kong bu straateji bi, waax bii mi ngi woon ci loxol Britani ba bu yàggul. Xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne Britani mi ngi ko doon tooñ waa Siin cig wàll, ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll. + +Britani tegoon na loxoom dunu Brem atum 1799g, ak Adan atum 1839g, ak Borma atum 1885g, akug wàll ci Malayo. Mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj-saalumu dunu araab bi, ak tefesug golfub araab bi. Mu sanc Isipt, Sudaan, Iraak, Penkub Sordani, Falastin ak yeneen barab ci reewi Asi yu ñàkk doole yi. + +Britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi Afrig yi, lu mel ni: Afrigug Bëj-saalum gi , Nijeeriya, Oganda, Tansani, Rodisiya ak Somali gi nu xame woon ci turu Somali gu Britani gi. + +Sancug Britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi, ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole, teg loxo ak jariñoo ne-ne yu nu laalul yi , ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen, fitnaal leen ak tooñ leen. Waaye li lii lepp di tar, teewul askani sancu yu Britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte, ci noonu la Britani dellu mel namu meloon, yor dayo bi mu yoroon, ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko, foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom-koom. + +Reewum Fraans: + +Waa Fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu Tugal yi ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi, rawati na ci Kanada ak gox yi peek dexug Santa Lorens gi. Ñu sosoon fa ay sancu yu Fraans, yu ci mel ne: Kebeg gi nga xam ne ci tefesug Santa Lorens gi lanu ko taxawaloon, ak sancu bu Luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca Luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub Fraans ba. + +Ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa Fraans yi ak waa Britani ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. Waaaye Britani moom jot na a neewal doole kilifteefug Fraans gi ci barab yooyu, bu ko defee Fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci Afrig, fu ci mel ne: Aljeeri, Tinisi akug wàll ci Maraakes, daal di sutuxlu ci tàkkug Afrig gu mag gi, daal di yaatal bu baax seen sañ-sañ ak kilifteef ci Senegaal, Kongo, Nijeer, Madagaskaar, Somaal gi nu tudde woon Somaalug Fraans gi, Gine ak Dawme. + +Fraans tegati loxo ay reewi Asi, fu ci mel ne: ay wàll ci End, waa Britani jële leen fa atum 1763g. ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu End gu penkug Fraans gi, ngir gëpplanteek lonkoo gu End gu penkug Britani gi, ak lonkoo gu End gu penkug Holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi. Fraans sancati Sireek Libaa ci turu feetale , ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba . +Sancug Fraans gii nag daa melowoo ag tooñ, tiitale, jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm. Lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj-gànnaaru Afrig te Fraans tegoon leen loxo. Waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug Fraans gii, ba mujj am tembte gu mat . + +(Fii fi Senegaal, waa Fraans sonnale nanu fi, tege fiy fitna, gennee fi, xoolal ku mel ni Sëriñ Tuuba., cig tooñ lanu ko fi gennee, sanni ko ca àlli Gabong yu lëndam ya, yobbooti ko Moritani, te fii nu koy genne de du seenum reew, reewam la. Xoolal ma fa ñuy wax (Camp Caaroy) ak jëf ju ñaaw ja nu fa def, xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te Fraans nekk ci ginaaw, xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal, xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal, leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen Senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon, ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal, lenn luy sunu aada safu ko woon, du col mi, du wax ji, du lekkiin wi, du lenn lu mu man a doon, naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos, defar leen, ñu koy ligeeyal). + +Reewum Almaañ: + +Imbraatoorug Almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi, ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum 1871g, mu daal di sanc Kamerun ak bëj-saalumu sowwub Afrig, bi nga xam ne dees na koy wooye bëj-saalumu sowwu Afrig bu Almaañ bi, ngir sanc gi ko Almaañ sancoon, ak bëj-saalumu penku Afrig bi nu tudde ba tay bëj-saalumu penku Afrig bu Almaañ ak Togo . +Almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni Pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu “duni argabiil yu Bismarck yi” . +Ñu nangu tam ñoom waa Almaañ xaajub bëj-gànnaar bi ci duni Gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi. Waaye Almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi. + +Reewum Itaali: + +Itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi, ginaaw bi mu bennoo, atum 1870g, mu daal di teg loxo ay sancu ci Afrig, ci Eritri, Somali, gi nu tudde Somali gu Itaali gi, Libi ak Ecopi. Itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew. (Omar Muxtaar ca Libi fàttaliku leen ko). + +Reewum Rusi mu Xaysar mi: + +Sancug Rusi gi moom mi ngi jëmoon ci Siberiya, Turkmanistaan ak ay gox ci Asi gu digg gi. Rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj-gànnaaru dexug Amoor gi ci Siin, daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu Vladivostok, lijjanti it ba Siin gu neew doole gii jox ko ay sañ-sañ ci defar yoonu weñ wu jaar ci suufi Manshuriya gu Siin gi, ligeey ba daal di tàmbli ca atum 1889g. Sañ-sañu Rusi it yokku ca Kore, mu daal di seddoo Iraan mook Britani, daal di sanc wàllug bëj-gànnaar ga, ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi, xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum 1907g. + +Buntub ñatteel bi + +Ñaawteefi sanc: + +Li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi, ci melokaanam yepp aki anamam, bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko, rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw, ba nu mos aw wextanam, reer cig lëjam. Sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt yi yanu woon ab sukkam. Ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii: + +Ñaawteefi sanc yu politig: + +li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew, rekki it seen sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom, te loolu dal yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko. Xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu-reew , ak ci nostey demokraasi yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell, loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi te dindee leen fi, wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc. + +Sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn, bu ko defee mu def lu nekk, jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn. Mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn, ak wepp xeet wuy wenn, ci mepp reew muy menn. Mu soññ te sawarloo yëngu-yënguy beddiku yi yi nga xam ne neewte yaa ngi leen doon sàkku ak def, daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér, mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew, daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu, daal di def ay soppi ci dig yi , yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo, dendandoo, mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe-jafey politig yu fasu, yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at, ginaaw bi nu tembee, yooyu jafe-jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees. Sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi, mu duma, tëj, mbugal, te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko, sàkku woon nu nuy goree te temb, te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen. Waaye askan yii yanu woon sanc gi, jugoon nanu xeex, def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd. + +Ñaawteefi sanc yu mboolaay: + +Sanc daal dafa defoon yitteem ci tas, xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi, jaare ko ci soññee cig tàqalikoo, wisaare nosteg kureel ci biiru askan, bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ, am ay sañ-sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen . Gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari. Bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi, di leen tegi coona, di leen fitnaal, te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi. +Am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi, mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi, bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal. + +Sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay, man a ñaawali jikkoom. Mu soññe cig mbon, reer, jëfandikoo dorog ak yiy màndal ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay, te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi, te gën fee suuxat seen reeni sanc. + +Sanc gi de jeemoon na – jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon – ngir gòndi niti sancu yi ci xayug Tugal gi , te sopploo leen ko, ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm-kanamug Tugal gi ak xalaati waa Tugal yi. Li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi, rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig, jaare ko ci seenug jàpple. Waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu, teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi, sooyal seeni mebat. +Seeni mebat sooy na, seeni yaakaar tas, bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine, di gën a ŋoy ci sseeni aada, di gën a ngëb ci seeni pas-pas yu laab yooyu. Fonk seen bopp, seen taarix aks een xalaat. +Nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi, ñu saxoon nag ci noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk. + +Ñaawteefi sanc yu koom-koom: + +Li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne-ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay , buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc, looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi. Mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk, ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi. Bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom-koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt , ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def, ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi. +Reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi, waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi Tugal yi. Lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi “siyukaay biy si buy dem ak buy ñëw” . + +Sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi, daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi, ngir man a joxe ne-ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi. Sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi, tax it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi Tugal yi. Bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom-koomi reew yi ak seeni alali endustri. Ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi, loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom-koomu sancu yi ci koom-koomu reew yiy sanc. Fii nag la genne gisiin wi naan: sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom-koom ci sunu jamono jii nu toll. + +Ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat: + +Sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay, te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi. +Sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc, te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la, juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo. Mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi. + +Sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng, rawati na mi ci aju ci xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam-xam man a am ak gu endustri ci reew yi. Te moom (sanc gi) yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi, walla njàggale mu yaatu mi . bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi. + +Sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul ci lenn lu dul ci ne-ne . Ñu tay-taylu woon di far dëgg yi, di indi li dëppoo ak seen njariñ, di wisaare xam-xam yiy ligeeyal seeni reew, di wone dooleem akug màggam, ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew, daan leen sabooteel seen kilifa yi, seen njiit yi, seen jàmbaar yi ak seen boroom xam-xam yi. Sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam, moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet. + +Doggantal gu ñeenteel gi: + +Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal: + +Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu nu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi, yilif ko . Looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi. Lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu rekk ci jëmmi boppam, waaye kay jàngu yepp a ko daan def, moo xam jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi). +Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi. + +Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Porrtigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par-parloo kontar jullit ñi ak seen adduna. Bu ko defee wuññikati Orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew, loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal . + +Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam : + +Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi, bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi def. +Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon. +Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo: + +(1) Ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni: fajuwaay yi ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen, aki matulkat aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal Egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Ndoktoor man nanu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi danu daa wax naan: li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Daanu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug. +(2) Njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne: daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon. +(3) Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi: bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci reewi Afrig yeek ak Asi. Loxob nasaraan biy indi ñam, fa jak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi. +(4) Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi, ak taalifi penku-penku yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi. Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey. + +Nasaraanal ci reewi araab yi: + +Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug Britani, Fraans, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine. Reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii : +Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Fraans ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Fraans merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante Fraans ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu Fraans gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Fraans ak kilifteefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole. +Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs + +Goxi Golfub Araab bi : + +Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi Golf bu Araab bi, ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn. + +Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Amerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci goxi Glof bi. Nasaraanalkat yu protestant yu Amerig yi daal di taxawal egliisub Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bic i Manaama ak Abuudabi, ak Egliisu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji, ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi. +Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi, teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar. + +Reewi Shaam: + +Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Urdun . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, nga xam ne reewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale gu Fraans ak Britani. Bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kureelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, feeteek kureelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel, ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g. +Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa. +Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Amerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte daa noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub Balfour , genne ko it atum 1917g, li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar. + +Isipt: + +Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee bu katolig bu Fraans bi tukkee woon Liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko. + +Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu protestant yu Amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal . + +Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jàngu aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xaayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs. +Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo. + +Sudan: + +Ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudan, rawati na ci ginaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal. + +Waaye waa Sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. Fipp gu Mahdi di xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko. + +Reewi Maxrib bu araab bi : + +Maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Fraans. Reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi Maxrib bu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci Fraans, Itaali ak Espaañ. Reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu. +Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug sanc gu Tugal gii ci reewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. +Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taarixam, jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu yu reewi sancaan yi, bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew, te dunu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi. + +Waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi Maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon. + +Barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi: + +Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci reewi araab yi, lii ci la: + +(1) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal , yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi, ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg. +(2) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju mag ju Amerig ji, xamluwaay bu penku bi, xamluwaay bu Fraans bi, yooyu yepp nag ñi ngi Xaayra . Bu dee Sudan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak jàngu bu Amerig ak jàngu yu Qibt yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Amerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju mag ju Amerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja, walla daara ju mag ju Yesu ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf . +(3) Nasaraanalkat yu penku-penku yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi. Ñu dugg ca akaademib làkk ba ca Xaayra ak bu xam-xam ba ca Dimasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penku-penkub Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom ak Margoliyos mu Fraans mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Holand mi, ak Harithman mu Almaañ mi. Penku-penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, teere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel. +(4) Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi. (ginaaw ci reew yii lanu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax). + + + +Juroom benneelu bunt + +Ñaar-fukkeelu xarnu + +Ñaari xarey adduna yi, bu njëkk bi ak bu ñaareel bi +Mbootaayi adduna yi: kureelu xeet yi, mbootaayu xeet yi +Mbootaayu reewi jullit ñi +Danki reew yi ak reew yi feetewul fenn +Xareb jawwu bi +Jëm kanam gu Japon + +Doggantal gu njëkk gi +Ñaari xare yu adduna yi: bu njëkk bi ak bu ñaareel bi + +Xaaj bu njëkk bi ci ñaar-fukkeelu xarnu g, seere na tàkkug ñaari xare yu adduna, ñooy xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g) ak bu ñaareel bi (1939 – 1945g). +Leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono. + +Xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g): + +Li waral xare bi: + +Xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi , kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi. + +Sabab yu jonjoodi yu xare bi: + +Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy: + +(1) Gëpplante gi ci wàllug sanc +(2) Tapoo yi +(3) Màggug yëngu-yëngu yiy woote ag xeetu +(4) Ak lëj-lëj yu adduna yi + +( a ) Gëpplante gi ci wàllug sanc: + +Gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g . Reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew, rawati na nag ci reewi Tugal yi am ay noste yu gore . Bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu-ji ne-ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox, man a jëm kanam. Tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye-ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi. + +Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi, bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu. + +Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante Britani ak Fraans cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay Almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom yu Almaañ yi ci reewum Usmaan mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi . +Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal. + +( b ) Tapoo yu reew yi: + +Gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu adduna bi gënee jëm kanam. Loolu nag tax ba ay dank sosu yu reew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu, yii di ñëw: + +Tapoo gu ñaaral gi ci diggante Almaañ-Otris: + +Gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru Almaañ gi ak gu Otris gi atum 1879g, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw: + +(1) Bu Rusi gu Xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war na a dimbli mi nu song. +(2) Bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu. +(3) Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Rusi ak Fraans, ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu. + +Tapoo gu ñattal gi : + +Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum 1882g, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll. +Itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Fraans, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Aljeeri atum 1830g, ak Tunisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Fraans ak Britani ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci geej gu diggu gi . + +Dëppoo gu Fraans-Rusi gi: + +Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Fraans ak Rusi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na atum 1886g, daal di gën a jëm kanam atum 1888g, bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Fraans di jox Rusi ngànnaay, te jëmale kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Fraans ak Rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw: + +(1) taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi. +(2) Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante. + +Dëppoog cofeel gu Britani-Japon: + +Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Britani ak Japon atum 1902g, lii la yaxal: + +(1) Bu xare tàkkee ci diggante Japon ak Rusi gu Xaysar gi, Britani da ca a war a genn te seetaan. +(2) Waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Rusi ak Japon, kon Britani da ciy war a dugg moom itam, jàpple Japon. + +Dëppoog cofeel gu Britani-Fraans: + +Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Britani ak Fraans atum 1904g, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax: + +(1) Féexal Fraans, joyal ab loxoom ci Marog , gii nga xam ne jotoon na a temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Ajeeri ak Tunisi. +(2) Fraans moom tam nangul Britani teg gi mu teg loxo Isipt atum 1882g + +Dëppoo gu cofeel gu Britani-Rusi: + +Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Britani ak Rusi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax: + +(1) Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan , ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Rusi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Britani jël gu bëj-saalum gi. + +( c ) Màggug yëngu-yënguy xeetu yi ci Tugal: + +Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom neenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy: + +Mbootaayug Slaaf gi : + +Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu Otris gi, ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Tugalug penku gi. +Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Rusi gu saaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Rusi gu Xaysar gi. + +( d ) Lëj-lëji adduna bi: + +Ay lëj-lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu: + +Lëj-lëju Maraakes: + +Fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo Maxrib gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tunisi ak Aljeeri Fraans a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig sanc. Ci noonu Fraans lijjanteek Britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga atum 1904g, Fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum 1906g ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi. +Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Fraans la gënoon a nekk, ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. +Fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon peey ba, da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu Fraans ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ mi àndoon ak buurub Maraakes bi, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Fraans. +Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Fraans yabaloon am mbooloom xare ca Faas atum 1911g ngir teg ko loxo. +Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Fraans-Almaañ bi, la fa juddoo di : jox Almaañ ay moomeel ca Kongog Fraans ga, bu ko defee Almaañ nangul Fraans nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu adduna bepp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi. + +Lëj-lëju Balkaan: + +Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan. +Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum 1908g. +Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba. + +Lëj-lëju Maseduwaan: + +Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon na jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen. + +Lëj-lëju Tripoli: + +Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci. + +Sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi: + +Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Rusig Xaysar gi. +Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def. +Otris daal di gaaw jirñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes-xibaar yi noonoo Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul, waaye Serbi moom tontuwul . + +Jibalug xare bi: + +Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibbal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal. + +Lefum xare bi : + +Jë bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru. +Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g. + +Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani. + +Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa. + +Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay. + +Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom. + +Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo. +Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g. + +Lijjanti yi ci ginaaw xare bi: + +Reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris. +Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Fraans. + +Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk. + +Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi. +Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g. + +Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi. + +Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko. + +Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations) teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi. + +Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon. + +Ñaareelu xareb adduna bi (1939 – 1945g): + +Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi. +Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu” lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi. + +Li laytaay xare bi: + +Àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu. + +Nosteg àtte gu mbokkoo : + +Rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba. + +Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi. + +Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ: + +Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ. + +Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi. + +Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g. + +Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali: + +Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu. + +Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi. +Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma. + +Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi. + +Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi). + +Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi. +Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom . + +Bokk na ci diktaatoor yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ bu Espaañ ba. +Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi. + +Yeneen jëfka yu sabab xare bi: + +Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo: + +(1) lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon. +(2) Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi. +(3) Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi. +(4) Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke. + +Jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi : + +Xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy: + +(1) Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g +(2) Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g +(3) Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g. + +Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. +Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g. + +Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi. +Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g. +Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g. + +Wéer ngànnaay gi nag lii la wax: + +(1) Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi. +(2) Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans. +(3) Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar. +(4) Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon. + +Ginaaw bi Fraans wommatoo meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll. +Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg. + +Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. +Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan. +Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd: + +(1) Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji. +(2) Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g +(3) Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g + +Ndamul Réewi tapoo yi: + +Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw - jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g. + +Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. +Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex . + +Wommatug Japon: + +Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo. +Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex. + +Li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi: + +ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu: + +(1) Def ndajem Botsdam ca anéeru Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi. +(2) Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg) +(3) Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani, Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar. +(4) Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem neewal dooleem. +(5) Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi. +(6) Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare. +(7) Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g. +(8) Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko. +(9) Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare. +(10) Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal. +(11) Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag +(12) feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi. +(13) Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom. +(14) Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon. +(15) Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon. +(16) Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi. +(17) Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal. +(18) Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf. + + + + +Doggantal gu ñaareel gi + +Mbootaay yu adduna yi: kureelug xeet yi , mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi), mbootaayug reewi Lislaam yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi). + +Ñatti mbootaay lanu bëgg’a waxtaane ci doggantal gii, ñooy : Kureelu xeet yi, Mbootaayu xeet yi, Mbootaayu reewi jullit ñi. + +Kureelu xeet yi: + +Njiitul Amerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi, guy jeem’a indi jàmm ci adduna bi, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. +Waxoon nanu ne Wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati. + +Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon, kollëre ga nu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim. Lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre gi taxawal kureelu xeet yi. + +(1) Sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tèmb gu mat gu dara wàññiwut, reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu yu mat ci respekte walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral . +(2) Reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir nu àtte leen, te xool li leen boole. Reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw. +(3) Jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés, ak wormaal kollërantey reew yi, ak xeex njaam, ci meloom yepp, jeem’a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund, ak xeex dorog, nos yaxantu ci adduna bi, ak sonn ci wér gu yaramu nit. +(4) Reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig , dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk. +(5) Aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi. +(6) Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi, ñuy : reewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen’a may ag tèmb ëlëg . Kureel bi, bi muy door a sosu, 42 reew a ca bokksi woon. Ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu ci bu nuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg’a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk. + +Bànqaasi kureelu xeet yi: + +Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy : Jataay bu matale bi , Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : àttekaayu maanduteg adduna bi ak mbootaayug ligeey gu adduna bi . + +Jataay bu matale bi: + +Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar, ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam. + +Jataayub kureel bi: + +Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer , juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy: Britani, Frans, Itaali, Japon ak Almaañ mi jël cerub Amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg . Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent. + +Koolute gi (secretariat): + +Koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi, mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi, ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale , ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg aada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex dorog, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi. + +Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: àttekaayu maanduteg adduna bi, ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi, ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind. Àttekaayub maanduteg adduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Holand. Ak mbootaayug ligeeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi. Geneve nag moo dib dalam. + +Ayibi kureelu xeet yi: + +Kureeb xeet yi de, ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay , loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu xeet yi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Japon defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci Japon ak Almaañ gennoon atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecopi atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum 1937g . Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon‘a tee ay “dank yu xare” yu bees di am, maanaam ay reew dajaloo,boole seen bopp ci wàlli xare . Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon’a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn. +Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Britani ak Frans nu man’a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci reewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Reew yu mag yii dano’o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg’a def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ. +Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi. + +Mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi): + +Ndawi reew yu mag yi, yu ci mel ni Britani, Diiwaan yu bennoo yi Amerig, Bennog Sofyet , Frans ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi . +Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér. +Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku San Fransisko ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi. +Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy: + +“Ñun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef” . + +Jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay ker-keraanam : + +Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy: + +(1) Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi. +(2) Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi. +(3) Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit. +(4) Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg. + +Bu dee ker-keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii: + +(1) Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi. +(2) Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi. +(3) Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi. +(4) Sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi. + +Campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam: + +Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy: + +Jataay bu matale bi: + +mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem: + +(1) Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi. +(2) Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi. +(3) Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk. +(4) Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi . +(5) Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi. + +Saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man’a doon walla ab ndenkaane. + +Jaataayu kaaraange gi: + +Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe. +Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi. +Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci. +Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex. + +Koolute gu matale gi : + +Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi . + +Campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi: + +Am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi, ñooy: + +Jataayub koom-koom ak mboolaay : + +Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo: + +UNESCO: + +Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans. +Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi. + +Mbootaayu Ligeeyu Adduna bi: + +Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte . +Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve. + +Mbootaayug Wérug Adduna bi : + +Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam. + +Mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi : + +Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali. +Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi: + +Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi. +Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand. + +Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax: + +Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen. + +Jataayub ndénkaan yi : + +Mooy saytu mbirum sancu yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi. + +Bankub addunna bi ngir sos ak tabax: + + Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg . +Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig. + +Keesug kee gu adduna bi : + +Yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi . + +Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy: +(1) mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll. +(2) Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp. +(3) Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ. + +Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi. +Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. +Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon. + +Mbootaayu reewi jullit yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi): + +Ag sosam: + +Mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g. +Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk . + +Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf. + +Kollëreg mbootaayu reewi jullit yi: + +Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 - 4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi. + +Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen reew yi. +Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe: + +(1) Yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk +(2) Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram. +(3) Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb. +(4) Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk. +(5) Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi. +(6) Jeem’a far boddante ci biiru xeet, ak sanc ci mbooleem ay anamam. +(7) Def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute. +(8) Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf. +(9) Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew. +(10) Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo . +(11) Reew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam . + +Campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo: + +Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki : + +(1) Jataayu buur yi ak njiit yi +(2) Jataayu jëwrini bitim reew yi +(3) Koolute gu matale gi +(4) Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi. + +Bu dee kureel yi ci bokk nag, ñooy: + +(1) Kureelu Quds +(2) Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar +(3) Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada. +(4) Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala +(5) Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu +(6) Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada + +Bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi, ñooy: + +(1) Keesug dimblante gu lislaam gi +(2) Keesug Quds +(3) Daaray gëstu gu lim yi ak koom, ak mboolaay. +(4) Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu. +(5) Cëslaayu lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom. +(6) Barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam. +(7) Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu +(8) Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi. +(9) Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li +(10) Akaademi bu xam-xamu lislaam +(11) Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi +(12) Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon + +Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy +(1) Banku lislaam bi +(2) Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi +(3) Mbootaayu rajoy reewi jullit yi +(4) Neegub yaxantu bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi +(5) Mbootaayu peeyi lislaam yi +(6) Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi +(7) Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada. + +Jagley campeef yi ak seeni ligeey: + +Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam. + +Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk. + +Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g . +Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g. +Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g. +Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g. + +Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam. +Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko. +Mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi. +Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi. +Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee. + +Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g. +Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi. +Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi. +Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle. +Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” . Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi. +Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal. +Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g. +Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi. +Ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii: +(1) Di gëstu lay xew Quds +(2) Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen, +(3) Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds +(4) Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju. +(5) Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi. + +Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at. + +Doggantal gu ñatteel gi: +Reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn + +Ag jiital: + +Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay reew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare. +Ci noonu dankub bopp-alal dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi . +Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole ba nu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo. +Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu, Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi . +Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te faf far, xajal fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi. +Loolu nag taxoon na ba reewi Orob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew. +Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi. +Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. +Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni: +Tapoo gu càmmooñug atlas (Otan): + +Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island. +Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm: + +(1) kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des. +(2) Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom. +(3) Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam. + +Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm ak yoon. + +Tapoo gu Warsaw: +Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. +Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. +Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi. +Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk. +Tapoo gu kollëre gu diggu gi: +Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak. +Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g. +Jataayub Tugal bi : +Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali. +Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi. +Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba : +Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk, ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk, te doxal fi yaxantu gu gore ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir. +Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali : + +Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll. +Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suwed, ak Yogoslawi. +Mbootaayug reewi Amerig yi: +Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk. +Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum 1958 g. + +Mbootaayi reewi Andis yi: + +Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi. + +Naalub Marsaal bi ak Komikon: + +Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi. +Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom. + +Mbootaay gi boole reewi araab yi : + +Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir. + +Mbootaayug jàpplante gu Asi: + +Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk. + +Mbootaayug bennoog Afrig : + +Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada. + +Reew yi féetewul fenn: : + +Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll. + +Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo. + +Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Japon, Filipin, Taylan, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman. +Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb. +Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex. +Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig. + +Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakri atum 1960 g . +Bi adduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi. +Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja. +Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk: + +(1) wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg. +(2) Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul. +(3) Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi tas leen, dindi dàtti xare yi . +(4) Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk. + +Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit bu baax. + +Ñeenteelu Doggantal + +Fipp gi xam-xam amal ci Elektron : + +Xamale lan mooy “ Elektron” : + +Elektron moom yaram wu sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu nu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu elktronik yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso. + +Elektron nag nekk na ci bepp ne-ne bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek fepp wi , walla saal bi , moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc. Elektron ni muy wëre saal bi - booy xool - day mel ne ni bidiw yu mag yi di wëre jant bi. +Elektron nag day yanu ay cëfkay kuran yuy bañ , saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu walla nangu. + +Xam-xamu Elektron ni mu sosoo: + +Xam nanu ne xam-xamu Kuran moom xam-xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Gres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii nuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu. +Jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran, maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu lamp bu kuran. + +Xam-xamu kuran nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam-xamu fisiyaa bu angle bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu fisiya. +Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam-xam yi feeñal ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari. +Ndamul xam-xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf. + +Jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ: + +Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, barabu ligeey yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs. +Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi, ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi, ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs. +Boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu ndoktoor yi, ak jumtukaayu segg yu elktronik yi. Jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii. + +Gis nga leegi foo dem fekk fa komputer, ci bank yi, lonkoo yi, campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi. +Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi, ak xam kiliman bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def. + Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbèlli suuf yu am yi solo. + +Jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga jumu fepp , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs. + +Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii. +Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi. + +Juroomeelu Doggantal + +xareb jawwu ji : + +(( yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin)) +Sooratu Rahmaan, aaya 33. + +Di : yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen bunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa. + +Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan; ay bidiw aki ñoom seen. +Moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind, ak li leen sos, def it ab jeego bu rëy ci xam-xamu juxraaf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, bidiw ak lu ko moy. +Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bii, gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci jafe-jafe yi mu ci man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu: man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu nuy joy , bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci. + +Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji: + +Sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji, làmbtu ko, loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo. +Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu gi tuddoon Fostok – 1 ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp. +Tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj. +Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu. + +Sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii. + +Li ci waa Amerig def: + +Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon. +Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a neew, te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji. + +Waa Amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nanu fa it ay còmp yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal . + +Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu) ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. +Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu . + +Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g. + +Musibam Carlinger: + +Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna . +Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald RIGAN nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi. + +Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee. + +Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca. + +Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi. +Ndaxte xam-xamu fisiya gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego, naka noonu endustri elektronik, ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs. + +Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare, la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji, yi ci yanu ay boppi atomig, cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll. + +Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare. + +Juroom benneelu doggantal + + Ni Japon jëme kanam + +Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g: + +Japon de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci yëfi bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na endustri. + +Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci reew mu deltu ginaaw, dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, aada, politig ak xare. +Mu roye nag ci reewi Tugal yi, gisiinu sanc ak yaatal ko, ci reew yi mu dendal, ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew, sanc leen. + +Japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci reewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum 1854 g gii rekk - teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Orob gi, di ci jariñu, di ci niitu. +Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo. Reewum Japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug endustri gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg. +Bu ko defee, Japon xëy di reew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci reewi Asi yi, ci wàllu endustri, xam-xam ak xarala . +Mu mujj am, moom Japon, mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi, ci diggante ñaari xarey adduna yi. +Marsandiisi Japon yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig. + +Japon, ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi: + +Japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Japon. +Japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko, mu jébbalu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Amerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi , ngir doxal mbiri Japon, nu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g. + +Waa Amerig yi nag rëddaloon nanu Japon benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi , nu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng, wutaloon leen sartu reew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi . +Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Japon yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees . + +Ci noonu Japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk, reewi endustri yu jëm yi kanam. + +Waa Japon jariñu nanu ci li leen Amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Lijjantikati Japon yi dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Japon, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Japon bari ay ligeeykat. + +Suqali nag gën na a yokk ci wàllug endustri ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Japon mujj di ñatteelu reew mi ëpp lu muy ligeey weñ, bokk it ci reew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu nuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, ligeey bi aju ci jumtukaayi eliktronig yi gën a jëm kanam, ba mujj Japon àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja yi nuy jaaye ligeeyi Japon yi gën a yaatu, gën a bari ci adduna bi. Bu ko defee Japon mujj nag di reewum endustri mu mag, mu dox, te jëm kanam. +Maamoor xam Sa Diine mooy Moor MBÀKKE Gànnaar, maanaam doomi Sëriñ Jiili Gànnaar, di ku yëngoom jëm ci yar ak jàngale. Taalif na lu bari ci wolof, firi ci it ay téere jële léen ci làkkuw araab, yooya nag yu ci ëpp yu diine lañu, woy na it lu sakkan ci wolof, yii woy firndé lañu ci, ku fonk wii làkk la, looloo ko bijj ci def wile taalif, sànki ci baat yu naroon a sànku, mu jëfandikoo arafi abajada ngir toftale leen, Yal na ko Yàlla gërëm, moom nag day faral di def ay waxtaan ci diine ak làkku wolof ci rajo (siwalukaay) Làmp FM + +Ubbite + +Arafu A + +Arafu B + +Arafu J + +Arafu D + +Arafu W + +Arafu y + +Arafu L + +Arafu M + +Arafu N + +Arafu F + +Arafu X Q + +Arafu R + +Arafu S + +Arafu T + +Ag Mottali + + +Yoonu murit +Dalal-jamm, yaa ngi ci wikipedia gi ñu jaglel kàllaama wolof, muy ab tèerexamteef gu tinkiku goo xamne ñi koy jàng bokk nañ ci ñi koy bind. +ku nekk man nga cee dugal sa loxo, bind ay jukki yu bees wala gënël baaxal li fi jota nekk; ndaxte ngir mebet mii mana dox ci ni mu gënee, dafa laaj ay loxo yu bari. Kumu manti doon man nga cee japp ci njekk ak teranga, topp atte yi'ñ fi tërël, ñoo ngi lay dalal. +Li mu doon lu ubbeeku ngir ñëpp te amul'g pay, ñi binduwul tamit ci biir, moo tax Wikipedia manula joxe ay wòoraange ci baaxaay ak celltey ndefam. Donte askan wu wikipedia moo ngi tijji ay gëtëm di ko jeema aar ci anam yu dëgër. Ci saa su ne man na am ay xët yu ñu say-saye wala yuñu soppi ci anam yudul yi gën te tay ko, def ci ay xibaar yu baaxul wala yu dëppowul ak dundinu sa waa-gox. + + Nooy saytoo wikipedia +man ngaa tambalee ci xët-njëkk mi te topp lëkkalekaay yi lay yòbb ci li la solool, li nga soba jàng. +su fekke itam daa am ab jukki booy seet, man nga bind benn wala baat yu bari ci paxu bind gi, gi nekk ci sa ndeyjoor te nga klig ci Ayca + Su fekkee baat bi nga bind da fa nekk koju ab jukki ba noppi, da ngay klig ci Ayca rek mu feeñ. + su fekke nak baat bi dafa nekk ci biir ay xët yu am ba noppi, da ngay klig ci seet. + (jappal ne xëtu seetukaay gi day tijjil boppam su fekke danga klig ci Ayca te amul lu mu la andil, gisul dara). + + +Dalu Archimède + +Du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb ci kaw géej: te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey, loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox. + +kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu, te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb. Bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara, jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox, bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool, dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat. + +yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox, waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi ak gaas yi,ñu duppee ko Dalub Archimède, moom Archimède nag benn boroom xam-xam bu Gres bu yàgg la + +Jëmm + + +Diisaayu yaram yi (corps) + +Tay de bis bu xiin la, tàmbali naa taw, doqi ndox yu ndaw, yu xaw a rëy, yu ngandee ngandee ngi nii far di rot ci suuf. + +Bu cooroonee, gàncax gu bari seeni xob day ruus, daal di naaw ci jawwu ji, rotati ci suuf si. + +jël-leen aw xeer ci seen loxo, wacc-leen ko, day rot ci suuf de. + +Benn sabab bi tax xeer woowu di rot, tax it ba xob wi rot, moo fi jaar ba tax doqi ndox yu taw yooyu di rot: loolu mooy li nuy wax Bijj gi walla Dooley ñoddi gi suus si di amal ci yaram yi. +Ñoddi gii mooy tax yaram yiy diis, moo waral it ñuy aajowoo genn kattanug përëg ngir yékkatee léen ci suuf si. + +Xam-xam +Sunu dund gi, niki gu dundat yi ak gu gàncax, dafa wéeru ci jurdund, mooy xeet wu simi wi ëpp ci jéeri ji. Jurdund nag nekkul rekk ci ngelaw li, waaye ci jaxasoo gu mu jaxasoo ak yeneen xeet yi ci anam gu wuute te bokkadi, mi ngi ci lu ëpp ci ne-ne yi ñu baaxoo dund ak ñoom ak a jonjool. + +Xalaatal rekk ne xeet yi toggale ndox mi, bu ñu doon fukk lañu juroom ñatt yi jurdund lañu, te moom jurdund moomu moo toggale li ëpp ci doj yi. + +Jurdund dinanu ko faral di jëfandikoo nii: + +- Def ko ci bitéeli gaas yi, ngir dagg, suude ay weñ ak tàkk-tàkk lu Osidrik walla Osiyasetilenik liy jariñoo tàngoor wiy amu ci sawara wu jurndox ak wu Acetilin. + +- ci liggéeyiinu mbell yi nga xam ne danu cay jëfandikoo ngelaw lu nu woomal ak jurdund. + +- ci paj ngir yombal noyyig ñu tawat ñi. + +- niki taalukaayu jum yi: fii moom jurdund bu yolaakon bi lañu fiy jëfandikoo ci tàngoor wu suufe. + +Simi +ci frãse : combustion. + +Jëmm +Simi +Rab (farãse: animal) : Dundat yi +Gàncax (la : plante) +Xeet (fr : élément) + +Simi +air +air + +Simi + +en:Atmosphere of Earth#Composition +Ne-ne, ñu xame ko ci faraañse ci((matière))mooy li toggale (li composer) wépp yaram wu am ag nekk gu nu man a laal (une réalité tangible. Ñatti melokaanam yi ñu gën a miin nag, ñooy melokaan wu dëgër(l'état solide), wuy yol (l'état liquide) ak wu gaasu (l'état gazeux). Moom day jël barab(elle occupe de l'espace)te kemub ne-ne (la quantité de matière) ñi ngi koy natte ci jóor(la masse) (bu fekkee ne mbir mi dafa aju ci waññ xaajiiti ne-ne(particules de matière), deesi jëfandikoo mol(la mole) ).Ci noonu, ci xam-xamu jëmm, lepp lu am ab jóor rekk ne-ne la. Ci biir loolu, ne-ne yu ñu miin yi ñu wër, ñi ngi sosoo ci ay bariyon,kon ci waxiin wi nu baaxoo, boo ci déggee baatub ne-ne, nanga xam ne ne-ne bu bariyon lañu jubloo wax. Tekkiin wii kon boolewuñu ciboson yu dàttu (les bosons fondamentaux), yi nga xam ne ñooy tuxal ñeenti doole yu dàttu yi ak doonte am nañu ab jóor ak/walla genn kàttan. + + +Jëmm +Simi +fr : Processus métallurgique + +Jëmm +Xarala +Endustri +Yolaakon (wu-faraas : liquide) + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Ndox + +Lëkkalekaay yu biti + +Téerekaay + +Simi +Jëmm +xam-xam +Njàngat +Jum (en : rocket) + +Xarala +fr: force de gravitée + +Jëmm +fr : force musculaire + +paj +Fr : globe terrestre + +Suuf +atmosfeer + +Xam-xam +Melosuuf +Fatt-jawwu (Wu-faraas:Troposphère) : Suuf < Fatt-jawwu < Yolom-jawwu < Biti-jawwu < Iyon-jawwsu + +Jëmm +Suuf +Biti-jawwu : exosphere + +Suuf +vide absolu + +Xam-xamu suuf si ak jawwu ji +Wërlaay gi di ci tubaab (environnemt) mooy dénd bi maanaam (nature bi) ak li ci nekk ciy way dund ak yu dundul, ci gàttal daal adduna bi nu wër ci kaw suuf si. Xam-xamu wërlaay mooy biy jéem a indi ay tontu ci yenn laaj yi aju ci nan la dénd biy jëfe ak a jëflanteek way nekk yiy dund ak yeneen way nekk yi, walla nan lay jëflanteek digg bi ko wër moo xam digg bu kimya la (simi) walla bu dénd (nature). Digg bii moom lanuy tudde “Noste gu wërlaay”. Looloo waral nuy gis noste gu wërlaay muy luy ame ci ay way nekk yuy dund ak yu dee walla yu way. Xam-xamu wërlaay mooy jàng ak gëstu way nekk yiy dund ak séenug séqoo ak li leen wër ak jeexiital gi nuy def ci sunug séqoo ak suuf si. Nosteg wërlaay mooy mbooleem jëfka (facteurs) yu dundul ak mboolaay (société) yiy dund yu xeet yi nekk ci benn gox walla barab. Dénd bi day wëndéel mbir yi mu jëfandikoo woon ngir delloo leen ñu mujjaat di mbir yu am solo ak njariñ. Càllalag ñam ci kaw suuf si, aw melo la ngir wone ni kàttanug ñam di dugge ci wërlaay gi. Foofu ñam da fiy juge ci aji nekk dem ci jeneen n gir jox kàttan dundat boobu di sàqami ñam wi ak a reesal, gépp càllalag ñam nag ci jant bi lay tàmbalee. Dundat yi - nit ci la - munuñoo liggéey seenub dund, looloo tax manul a ñàkk mu jot ci dundam boobu jële ko ci gàncax yi walla yeneen dundat yi, looloo waral ñuy jàppe dundat yi ay way lakk walla ay way jëfandiku (consomateur), mujjantalu dundug dundat it mooy ag feccikoom (ag tasam) jaare ko ci ay mikrob walla ay gàncax ngir mujjati di suuf, gàncax gi muucooti ko ngir liggééyati ci ñam wu beesati. Lii nag moom lanuy tudde “Càllalag ñam”, bokk na ci jëfkay dénd yi ci nosteg wërlaay gi te am ci jeexiitalm it: leerug jant bi ak ker gi ak tàngoor wu diggdóomu wi ak séddalig sewogaraafi gi ak ngelaw li ak barab yu yékkatiku yeek yu suufe yi ak melokaanu suuf seek ndox mi. bokk na ci jëfkay kimya yi yiy bàyyi ay jeexiital ci nosteg wërlaay gi: tolluwaay (niveau) bu ndox yi ak ngelaw li walla jawwu ji ci suuf si ak kem ni way dundal yu gàncax yi di seeye ci suuf si ak ndox yi ak tooke yi ci nekk, ak xoromus ndoxum géej ak oksijiin bi ci seey. + +kay diang wolof + +Wërlaay +Ci baax, wërlaay - walla barabub jëf mbaa mbir, maanaam fu lëf nekk mbaa deesi defe ko fa - mi ngi ame ci jëmm yi (substence), peekte ti (circonstance), mbir yi walla nekkiin wi ko peek wër ko, te di fa ame. + +Bu dee ci wàllug dundat (biyoloji) rawati na ci wàllug dénd (ecoloji)day tekki lépp lu man a def ay jeexiital yu jonjoo ci doxug walla màggug mbaa jëm kanamug mbir yi (metabolosmo)walla nekkiinu jëmm walla xeet wuy dund ( SPECIE VIVENTE), loolu nag leer ci la, ngelaw, ndox, suuf ak yeneen nekktéef yiy dund. +Dalu Archimède (fr : principe d'Archimède) : Du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb (feey) ci ki kaw géej: te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey, loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox. + +kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu, te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb. +Bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara, jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox, bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool, dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat. + +yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj (comportement général) ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox, waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi(les liquides)ak gaas yi,ñu duppee ko Dalub Archimède, moom Archimède nag benn boroom xam-xam bu Gres bu yàgg la + +Doolerandu +Paj walla ndoktoor mooy xam–xam biy yittewoo faj nit, di ci nasaraan “medecine” + +Xam-xam +Paj +Doolerandu mooy xam-xam biy gëstu lepp lu ñeel wuutuloxo yi, doxalkat, ndaamar, ci gattal, lepp luy jur walla di yòbb ab jalaxu, doole, ag soppeeku. Da nuy wax tamit doolerandu gu daj, doolerandug ndaamar, taggat-yaram gu doolerandu, doolerandug gaal, doolerandug asamaan, doolerandub kàttan-ferñent… + +Cosaanam +ci taariix, doolerandu mooy boole, gi Newton def; jëmm ak gëstubidiw. Kon su nu ko xoole ci wallu taariix jëmm walla fisiyaa ci doolerandu la joge. +Ci sunu besu tay yi, day lu noppale, ci daara yu kawe yi, ne atte doolerandu yi ci jëmm la ñu joge. + +Xam-xam yi ci lënku +Doolerandu ab banxaas la ci xam-xam yiy gëstu jalaxu yi ak soppeekuy neen yi, ci lu tukkee ci doole jiy man a indi googu jalaxu walla googu coppiku. +Man nan koo xoolee ni ag wàll ci xam-xamu jëmm. +Kon aajoom mooy leeral, xalaatjiitalu jalaxug neen yu tekkaaral yi, ak yaram yu asamaan si walla jëmm yuy dund (dun-doolerandu) ëbb na tamit: + + Doolerandu gu yàgg ga, ni ko it gu newton, moo ñeel njangat gu imbiku (njangatum jalaxu yi te bañ a bayyi xel ca ngérte la), njangatu demin yu tekkaaral ak yuy yëngu, muy demiin gu wayaymbir (doolerandu gu tomb) walla demin gu lëj (doolerandu gu daj). + Dolerandug asamaan, mooy jang jalaxub yaram yu asamaan si. + Doolerandug tekkaaral, mooy jang demin gu bari cër, lu mel ne gil yi, yi cëroo ay milioŋi ngënjabar. + Doolerandug jëmm moom day gëstu demin yu am y melokaanu jëmm yu mel ne doolerandu gu yolaakon yi ak doolerandu yu seen demin soppeekuwu. + +Doolerandu +Jokkoo-cig-soree di ci làkku frâas «télécommunication»:tuxal ak yonnee walla jot ay xibaar jaare ko cig buum, ceññeer-mbej, ngiste, walla yeneen noste yu mbëjbijjaakonyi + + Am mbooloo mu ay noste yuy warlu tuxug xibaar yii (telegraaf, ëyukaay (telefon), tele). + +Xarala + + +Tekkeem +Kàttan mooy man a def dara (sos ag soppi), kàttan nag am na ay melo yu bari, yi ci ëpp solo ñi ngi feeñe ci tàngoor ak leer. + +Ci biir “xam-xami dénd yi” (science naturelle) kàttan man na fee jël ay melokaan yu wuute : “kàttanug tàngoor”, “kàttanug kimyaa (simi)”, “kàttanug mbëj”, “kàttanug ceññeer”, “kàttanug saal (nucleaire)” ak ci mujjantal gi “kàttanug mbëjbijjaakon (éléctromagnétique)” añs. Xeeti kàttan yii ñaare dees leen di séddale ci: “kàttan guy yëngu ak “kàttan gu nëbbu” te kat am na yenn kàttan yoy dëppoowunook séddale gii, lu ci mel ni: “leer gi”, ak yeneen yoy man nanoo nekk am njaxas mu tukkee ci ñaari kàttan yi, guy yëngu gi ak gu nëbbu gi. + +Lu bari ci xeeti kàttan yii manees na koo soppi (transformer) jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, jaare ko ci jëfandikoo ay jumtukaay yu fasoodiku (simple) walla ay xarala yu fasu (compliqué): la ko dale ca “kàttanug kimya” ba ci “gu mbëj” jaare ko ci jumtukaay bu siiw bi di tegale(pile) yi, walla ndëxañtéef yi, Albert Ayinstaayin it ci biir ”faramfaceg ajoo” (theorie de relativisme) boole na ñaari ëtt yii di bu ne-ne ak kàttan, nga xam ne kàttan day mujj man a soppiku di ne-ne(matiere), naka noonu safaan bi, maanaam neen soppiku moom it di kàttan: wuññi (découverte) gu yees gii mi ngi ko xamalee ci yemalem gu siiw googee E=mc2, soppiku gii ci jëf (ci wàllug pratique) ñi ngi ko firee ci man gi nu man a ame kàttan jaare ko ci “xarug saal” walla “booleeg saal”. + +Waxiin walla baatal (terme) yu kàttan yi akug soppikoom lu am njariñ la ci leeral jëfiini dénd yi. Ba sax feeñte(phenomene) yu kilimã yi niki ngelaw, taw, melax ak riddi yi (tornado) dees leen di jàppe ñu juddoo ci soppiku yu kàttan gi juge ci jant bi wàcc ci suuf si. Dund gi ci jëmmi boppam dees koy jàppe muy benn ci njuréef (resultat) yu soppikuy kàttan yi: ci anamu “toggaleg leer gi” dees na ci jële soppi kàttanug jant bi yóbbu ko ci “kàttanug kimya” ci biir gàncax yi, bu ko defee ci kanam ñu man a jariñu ci kàttanug kimyaa gii nu denc, ci ay “liggéeyiinu wëlbati” ci ay way nekk yuy dund. + +Njariñam ak yaxam +Ci biir jëfandiku gu mboolaay (gu société bi): baatub kàttan dees koy wooye lépp lu nekk ci ron gongikuwaayu kàttan (source d’energie), juddalug kàttan, lakkug kàttan (ag jëfandikoom) ak wattu rootuwaayu kàttan (maanaam fi muy juge), ginnaaw nag dooley koom-koom dafa laaj te soxla ab rootuwaay walla ab gongikuwaay ci gongikuwaayi kàttan yi, looloo tax ag amam akug yooxam(baril ko) bokk ci yitte yu mag yiy caabi. Ci at yu mujj yi, jëfandikoo kàttan feeñ na di benn ci jëfka (facteur) yi gën a sabab nuggug àdduna bi (global warming), looloo ko def muy ab lëj-lëj ci li ëpp ci réewi adduna bi. + +Coppiteg kàttan +Manees naa soppi kàttan jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, ci misaal, manees naa soppi kàttanug kimyaa gi ñu denc ci ab tegaleeb(pile) Jiib def ko ag leer. + +Kem (quantité) bu kàttan bi nekk ci àdduna bi, day lu sax ba fàwwu, kàttan du jeex, du sosu, li am kay mooy day soppiku juge ci melo dem ci weneen. Bu melee ne kàttan dafa jeex, booba jeexul, daa soppiku kay dem ci weneen melo. Looloo tax ñuy gis ne kàttan mooy man gi neen man a def ab liggéey (yëngu) muy njuréeful yëngoom googu, walla njuréeful ab barabam bu nu ko nattee ci doole yiy liggéey ci kawam. Kàttan giy ànd ak yëngu moom la nuy tudde “kàttan gu yëngu”, kàttan nag gi am ag jokkoo ak barab bi moom la nuy wax “kàttan gu nëbbu” (gu coona walla gu ñu dëxëñ (gu nu denc) )... + +Melokaanam +Kàttan dana ame ciy melokaan yu bari, niki kàttanug doolerandu (mecanique) ak gu tàngoor, ak gu dinaamig gu tàngoor (tangdooleel,termodinamique), gu kimyaa, gu mbëj, gu ceññeer ak gu saal( walla xartil), kàttan yii yépp nag man nanoo def ag soppiku gu biir jaare ko ci ay yoon yu dëppoo. Ñam wi nuy lekk am na kàttan gu kimyaa gu yaram wiy denc te di ko génne bu nuy liggéey walla nuy génne ab coona (def effort) + +Kàttan ci taariix +Kàttanug bàyyima yi mooy gi nit njëkk a jëfandikoo ci fajarug xay (bi xay (civilisation) di door a am), loolu mooy bi mu jëlee bayyima yu miin yi di leen jëfandikoo ciy liggéeyam, ginnaaw bi mu tàmbalee jëfandikoo dooley ngelaw li ci doxal ay loocaam ba ci ay gox yu sori ci géej gi. Lu xayam di gën a yokku muy gën a jëfandikoo kàttan gii, mu jëfandikoo ko niki kàttanug doolerandu (mekanig) ngir doxal walukaayi ngelaw yi, ak ngir dawal ponoy wuutuloxoy wal yi, ak daggukaayu dénk yi ak najukaay yiy yékkatee ndox yi ci teen yi. Lii mooy li nu xame ci turu kàttanug doolerandu (mekanig). + +Xeeti kàttan yi +ci maanaa, da nuy ràññee xeeti kàttan yu bari te wuute. Kàttan tamit day tax nu man a natt melow feeñte yi, seenub taraay; feeñte gu ne ak kàttan ga mu àndal. + +Xeeti kàttan yi nu yàgg a jàpp: +Kàttanug imbiku (cinétique) +Kàttanug tàngoor (calorifique) +Kàttanug ëmbu (potentielle) +Kàttanug doolerandu +Kàttanug kimiya +Kàttanug saal +Kàttanug mbëj +Kàttanug mbëjbijjaakon +Kàttan gu féex (libre) + +Jëmm +Kàttan +Yoon moom lanuy wax ci tubaab (justice) dees na wax it yoon jublu ci li nuy wax (loi)walla (code) yoon tam dina tekki fi nit di jaar, dees na ci jublu it lu nosu maanaam tegu na ci yoon. + +Yoon nag it ci nosteg penc (systeme republicuain) benn la ci ponk yi àtte gi (l'etat) di tegu di ci doxe, ponk yooyu ñaare ñatt lañu + + yoon: fii bu ñu ko waxee mooy doole jiy àtte tooñaange yi di tege ci yoon, ci biiram lañuy fekk ëtt yeek àttekaay yi ak xaali yi ak layalkat yi ak lépp li ci aju + yoonal + wéyal + + +Xamale koom-koom +Koom-koom walla cawarteg koom-koom (activité économique):(làkku grees wu yàgg wa : οἰκονομία, « yor ag kër walla saytu ko »« di οἶκος (kër ci ni ñu ko xame)ak (νέμω yor walla saytu(administrer)) mooy cawarteg nit giy feeñ ci liggéey ak jóox (produire) ak séddale ak joqalante (echange) ak jëfandikoo njuddéef yi (les produits) njëfte yi (le services). + +Koom-koom nag ni ngi koy jànge ci xam-xami koom-koom yi, day sukkandiku nag ci gisiin yu koom-koom (théories économiques). + +Dees na wax it ci koom-koom niki tolluwaayu koom-koom bu jamono bu am réew walla bu ab gox (zone), maanaam ag nekkam ci gëwéelub koom-koom yi. +Cawarteg koom-koom gi kiliftéef yu koppar yi walla góornamaa yi (àtte yi) ñoo koy àtte jaare ko ci ab politig bu di kojug jamono (conjoncturelle). + +doxaliin wu mbooloo mi (Les administrations publiques)day def moom itam ay politig yu koom-koom ngir soppi doxiinu koom-koom wu am réew. + +benn ci joxoñ yu koom-koom (indicateurs économiques) yu mag yi mooy njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) (produit intérieur brut (PIB)), loolu mooy maye nga man a nattale dooley koom-koom yu réew yi + +Koom-koom + +Xam-xamu koom-koom ( ci Fr:economie)moom xam-xamu mboolaay(social) la buy yëngu ci gëstu ni ñuy jëfandikoo jumtukaayi jóox(production)yu daytalu yi am cig mboolaay (société) ngir faj soxlay ak xemmemtéefi cér(membre)yu mboolaay gii.Xam-xam bii nag mook xam-xam yépp a yam, dafa am ay dëgg-dëggam akaki àtteem waaye jeexiitalu gi mu def ci nekkiini mboolaay yi ak yu politig yi (les conditions sociales et politiques)ak ni ay séqoom ( ay relation-oom) dugganteek nekkiin yii tax na ba melow mboolaay muur ko, cuub ko. + +Xam-xam bii li mu làmboo mooy seggat jóox gi (production), séddale gi, ak yaxantu ak lakk walla jëfandikoo njaay yi (marsandiis yi) ak njëfte yi (les services). danuy faral a wax ci koom-koom ne buy wuyyu la (positive) bu dee jéem a leeral ngértey tànn yu wuuteyi, di joxe ay mbooleem ay xalaat jiital (hypotese), walla am mbooloom ay gendiku (ay seetlu),danuy wax it ne bu nattukaay la bu dee leeral doxal yi nu war a def. + +Xam-xamu koom-koom dees koy déddale ci ñaari bànqaas yu mag: + + Koom-koom bu xaaj walla koom-koom yu ndaw yi , mooy jëflanteek benn-benni naayib yi, lu ci mel ne njëli kër yi ak liggéeyi yaxantu yi. + Koom-koomub lépp walla koom-koom yu mag yi ,mooy gëstu ci koom-koomu réewum lëmm, ci melo wii nag dees koy xalam(dees koy xalaat) muy gaaral ak sàkku ñeel alal walla xaalis, bopp-alal (capital)walla njaay (marsandiis) ci biir koom-koomu am réew + +Koom-koom +Wikipedia (di jàng wikipediyaa) ab sémbub jimbulang la ci web bi, di lu àddunawu te bariylàkk. Ag bindam nag mi ngi wéy ba tay, xaralaay wiki lañu jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jébbal am ëmbiit mu ubbeeku, maandu te fugluwu. + +Jaar-jaar + +Sémbub Nupedia + +Nupedia di woon ab sémbub jimbulang bu ubbeeku bu Jimmy Wales sosoon ci weeru gamu atum 2000. Mboolaay gu Bomis (gi Jimmy Wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp) moo ko jàppale woon ciy koppar, doon fay Larry Sanger mi jiite woon mbind mi. Waaye Nupedia ag màggam dafa yeexoon lool ba waraloon, ci 2001, Larry Sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi. Xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab jimbulang, juroon na ag diisoo ci diggante Larry Sanger ak tëriinkat boobu di Ben Kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala gu wiki di doxe, ci ab reer ca San Diego la ame woon, ci 2 tamxarit 2001. Ci nii Larry Sanger ni Jimmy Wales ngir ñu jëfandikoo xarala gu wiki ngir sos ab jimbulang bu gën a woyof, lii moo jur sosug jimbulang bu Wikipedia. + +Sémbub Wikipedia +Ginnaaw bi ko Jimmy Wales ak Larry Sanger sosee, Wikipedia ngi judd ci kàllaama waa angalteer ci 15 tamxarit 2001. Gu waa faraas teggu ci 23 gamu 2001, gu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp, ba tay ci atum 2007 mat nañu ñaari-téeméer ak juróom-fukki làkk. + +Ci 1 diggi-gamu 2002 la Larry Sanger tekki ndomboy-tànkam ci ñaari sémb yépp, ginnaaw bi Bomis tëyyee loxoom, fayatul Larry Sanger ci liggéey bi mu doon def ci Wikipedia ak ci Nupedia. Ci 26 weeru koor 2003 la Nupedia tëj ba fawwu, Wikipedia moom wéy di màgg. + +Boobu ba léegi Wikipedia di dox ci ay àtte yiy askanam tëral ndànk-ndànk jëmug kanamam. ci 20 maami-koor 2003 la Mbootaay gu Wikimedia (wikimediafoundation.org ) juddu ngir wut ay koppar yu muy suuxate sémbi wikipedia yépp. + +Wikipedia Wolof +Wikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi-gamu 2003, toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu-yëngu. Ci tamxarit 2005 la am jukkeem bu njëkk. Xoolal xët wi ñeel Taariixu Wikipedia wolof + +Melokaanu sémbub Wikipedia + +Yéeney sémb bi +Ni ñu ko binde ci xët wu njëkk wi, bakkam mooy:«Jimbulang bu ubbeeku bi», maanaam di lu ñépp bokk, te ñépp man cee cëru ngir gënal ko. Jimmy Wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb bi, mi ngi koy tekkee niki «ag jéemantu ngir sos ak séddatle ab jimbulang bu ubbeeku ci anam gu mucc-ayib ngir nit ku ne man koo am ci làkku cosaanam». + +Melokaani Wikipedia +Baatu «Wikipedia» mi ngi jóge ci taqaleg ñaar yii di «wiki» di ag nosteg yoriinu ëmbiitu dalub web bu ñu man a soppi jaare ko ci ab joowukaayub web, ak « pedia » di reenu baatu làkku waa angalteer bii di encyclopedia, di tekki jimbulang. + +Li ñu jublu ci sémbub Wikipedia mooy mu doon ab jimbulang, maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit, lépp lu nit xam man caa ne. Wikipedia du ab baatukaay, du am péncum waxtaanuwaay (xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul: Ndimbal:Ubbeeku). Sémb bi dafa àddunawu, day laal bépp xeetu xam-xam, bariylàkk, te amul ag pay. + +Sémbi wolof yi + Wikipedia ci wolof + Wikiquote ci wolof + Wiktionary ci wolof + +Sémbi Wikimedia Fondation +Jimbulang +mooy xam ni yaram yi mel ak seen dëgg-dëgg ci lu dul ag laalante gu fisig walla simig gu jonjoo(direct)ak yaram yii, fi nu ko gënee doxale ci jamono jii nag mooy : nataali jawwu yi nuy far a defe ci satalit yi, walla yi nuy far a def di jëfandikoo ay fafal-naaw. + +noppeegul + +هو معرفة ماهية الأجسام دون التمساس الفيزيائي أو الكيميائي المباشر مع هذه الأجسام ومن أهم وأكثر تطبيقاته في الوقت الحالي هو الصور الفضائية التي يتم التقاطها عن طريق الأقمار الاصطناعية أو الصور الجوية "باستخدام الطائرات" يتم معالجة هذه الصور باستخدام برامج معالجة خاصة لأهداف متعددة منها : + +جيولوجية: الكشف عن النفط,المياه,المعادن,الفلزات,الفوالق,متابعة التشوهات الجيولوجية... +زراعية : وجود الأمراض عند النباتات, معرفة أنواع النباتات في منطقة معينة... +علم الجليديات: متابعة حركة الكتل الجليدية وذوبانها. + + +Muhammad + +Dundam bim nekkon xale + +Muhammad (jamm na sax ci mom) mi ngi judd ca Makka atum 571 g. Ci at wowu la Abraha , buru Abissini , bëggona danel Kaba ji, waye Yalla suñu borom danelna pexem , yonnifa ay picci yu amon ay xer yu mag ci sen sall , ray nitam yepp . Alxuran waxna ci li ci sar 105 , Al-fil , ñay wi . Muhammad ci banu Hashim la bokkon . + +Bayam Abdullah la won , dom bi Abdul Mutalib ganona bëgg +Abdul Mutalib . Bimu juddu dafa fekk Abdullah mu de , di dellu ci jayantu ci Sham , kon yay ji Amina bint Wahb ak mam ji, Abdul Mutalib . Mom bi Yonenta bi judd mag la won ta at yi danka xawona sonal . + +Ca tukkib yaxantoom booba la baayi Yonnant bi làqoo , ca tawat ju ko daloon ba muy dëpp, ba muy ñëw ba agsi Madiina la ko gënoon a sonal, mu daal di wàcc ca ña ñu daa wax Banii Najaar di woon genn ci giiri Xasraj yi, fa la génne àdduna. Maamam nag di Haasim mom Abdul Manaaf dafa a takoon soxna, looloo tax ñu naan Banii Najaar de ay goroy Yonnant bi lanu (j.m). + +Yónnent baa ngi judd (j.m) ginaaw bi waajur wi làqoo, mu daal di màgg cig njirim, waaye maamam Abdul Mutalib beg ci moom lool, tudde ko Muhhamad, yar ko cig cofeel ak ñeewant + +Waa Quraysin nag aadawoo woon nanu di yóbb seeni doom ca la génn Màkk, ca nàmpalkat ya ngir ñu man a màgg ci jàwwu ju sell, wér-gu-yarame te deesi fa dégge araab yu sell, bu ko defee loolu di tax ba ñuy wér, neexi araab te leeri wax. Nii la Aamina defoon ni ñépp, yóbb doomam Muhammad (j.m) ca ab nàmpalkat bu tuddoon Aliima Asahdiya, mu bokkoon ci Banii Sahd Bun Bakr, seeni kër nekkoon ca tàkk ga ca wetu Màkka. Bi Muhammad àggee ci am juroomi at la ko Soxna Aliima delloosi ndayam ca Màkka, mu nekk fa ca pekkam , maamam Abdul Mutalib di ko sàmm. + +Ca jamono jooja la Soxna Aamina Bint Wahbin jugoon ne day siyaareji bàmmeelub boroom këram Abdul Laah ca Madiina, ba mu demee bay dëpp la ko tawat ja dikkal, mu faatu ca ndëkk sa nu naan Abwaa te nekk ca yoon wa dox diggante Màkk ak Madiina, ñu daal di ko fay denc, looloo waral bi Yonnant bi màggee di ku soppoon di jaar ci ndëkk soosu ngir siyaare bàmmeelu waajuram ju jigéen ju laab jooju. + +Ci nii – ndaysaan – la Muhammad mujje di jirim ci nday ak ci baay, looloo waraloon maamam Abdul Mutalib mujjoon féetewoo ag yaram akug wattoom, bëggoon ko it lool. +Waaye sàmm googu gépp ak fonkeel gi teewul Muhammad (j.m) doon yëg naqaru njirim, ndax kat da daa gis moroomam yi ñu nekk ak seeni way jur, moom muy ku leen ñàkk, waaye nag loolu jox na ko ag sukkandiku ci boppam, may ko ag temb ci njëmm akug wéroodi ci kenn, nàmm am xelam, ubbil ko ay bëtam ci dëgg-dëggi dund gi, te booba ay atam lu néew la woon. Loolu de lu jeexiital la ci moom ak cig dundam, Yàlla nag moo bëggoon ci moom loolu ngir tànn gi mu ko tànn ngir mu yanu bataaxel bii di Lislaam te war koo tas. + +Yonnant baa ngi sàmm ag jur +Abdul Mutalib ginaaw bi Aamina làqoo yàggu fi dara moom itam làqu, te booba Yonnant baa ngi amoon juroom ñatti at, fa la ko baay-tëxam Aboo Taalib jële yóbb ko ca këram ca doomam yu xaw yaa sakkan tubaar-kàlla, ngir mu yaroo fa. +Aboo Taalib nag moo wuutu woon baayam ci jiite Màkk, ci noonu mu jeexaloon alalam jépp ci sàmm Kaaba gi ak way aj yi ak dimbali ñi aajowoo, looloo taxoon alalam bariwutoon ak li muy nekk kilifag Màkk lépp. Lii a waraloon Yonnant bi doon jéem a woyofal yan bi ci baay-tëxam jooju, ba àggoon ci di sàmmal ag jur ñenn ci waa Màkk yi, ñu ko ci daa fay lu néew a néew. Loolu it doonati ab pose ngir mu tàggatu ci xam ni nuy sàmme ag njaboot, jikkowoo ag ñeewant akug laa-biir ak sàmm ak yewwute, ñuy jikko yu manul a ñàkk cib sàmm bu bëggee wattu gétt gi muy sàmm. Yàlla moo ko bëggaloon loolu ngir tàggat ko ci bataaxel bi mu ko nar a joxi. Sàmm ag jur nag daara la joj lu bari ci yonnant yi jaar nanu ci, ba sax jële nanu ci Yonnant bi (j.m) mu ne : amul yonnant bu sàmmul ag jur. + +Yaxantu gi mu doon def ak tudde gi nu ko tudde woon Ku wóor ki +Bi mu amee fukki at ak ñaar la ànd ak baay-tëx ji Aboo Taalib cib tukki dem Shaam, bi mu amee nag ñaar fukki at la tàmblee bokk ci yaxantu gi ni ko waxambaaney Quraysin yi daan defe, mu wone ci it man gu mu ko man lool, ndax ku ñu xamoon la cig wóor, ak dëggu, yewwute ak ñaw, ay man-manam tàmblee feeñ ñeel waa Màkk, li ko gënoon a wuutaleek nit ñi mooy wóoram gi jéggi woon ab dayo te xaroon baax, ñu mujjoon di ko wóolu ci lu mu man a doon, te am xel mu dal ci ne dana sàmmoonteek kóolute gi nit ñi def ci moom , looloo taxoon ñu naan ko ku wóor ki ak ku wóor ku dëggu ki. + +Jël gi mu jëloon Xadiija soxna ak doom ya mu ca ame +Bi at yi àggee ci ñaar fukk ak ñeent daa dajeek Soxna Xadiija soxla waxambaane wu ko yoral yaxantoom gi mu doon deflu ca Shaam, moom nag soxna su woomle la woon bokkoon ci way woomley Màkk yi, ci noonu ñu digal ko mu gis Muhammad (j.m), ba mu ca waxeek moom Yonnant bi nangu. Yonnant bi yaxantujil na soxna Xadija ca Shaam ànd ak ngóoram sa nu naan Muyasara, Muyasara mii yéemu woon na lool ci jikko yu rafet yi ci Muhammad ak yewwu geek man gee yaxantu, ndax bi njaay mi nekkee ciy loxoom fulu na ay yooni yoon, wuuteek ba mu nekkee ci loxoy keneen, looloo tax bi Yonnant bi (j.m) delloo, jébbal soxna Xadiija alalam ak la mu ca tonoo, cig kóoluteek dëggu, soxna si yéemu na lool ci jikkoom yu rafet yi ak njëmm gi ne ci moom, ci noonu mu yónni ci moom kenn ci ay jegeñaaleem xamal ko ne da koo bëggoon niki boroom kër, Yonnant bi (j.m) nangul ko . Noonu la seen diggante sottee te booba Yonnant baa ngi am ñaar fukk ak juroom ciy at, Xadiija moom yor ñéen fukk, ci noonu mu faroon di soxnaam, di yaayam, di ki koy dimbali ci lépp. +Yonnant bi (j.m) amoon na ag texe ci séy boobu naka noonu Xadiija, ci noonu séen kër di misaalum mbégte cib séy ak texe ci biir kër. Soxna Xadiija nag mooy ki jur mbooleem doomi Yonnant bi, ku ci dul Ibraahiima, moom de soxna Maariya mi di ab qibt moo ko jur, moom nag (Sëñ Ibraahiima) ci jamonoy Yonnant bi la làqu. Yonnant bi wéyoon na ci yaxantoom gi ginaaw bi mu yoree soxna Xadiija, mu ko daan defe nag ni ko waa Xuraysin gépp daan defe rekk, ñoom de yorunu wooni bitig aki mangasin, moom kay danu daa defi njëgg yu mag mbaa yu ndaw jawali Yaman ci sedd bi, bu cooroonee ñu dem Shaam, màkk-màkka bu nekk daa na man a bokk ci njëgg li bu bëggee, njëgg loolu nag moom la nu daa wax ci ci araab Bahiir, kenn ci góori Xuraysin yee ko daa jiite , ku soob ci ñoom ànd ak moom, bu ko defee bu dellusee ñu seet li ñu tonowu, seddale ko, ku ci nekk am ca la nga ca def. Seen yaxantuwiin woowu moo taxoon Xuraysin daan am jot, di daje ci jataay yi di waxtaan, rawati na ca la wër Kaaba ga. Waaye Yonnant bi (j.m) moom néewaa na bu mu bokkee ci yii jataay, moom kay këram la daa toog mbaa mu génn dem ca àll ba ngir wéet fa di xalaat ak a settantal, ndax sopputoon di fo mbaa muy caaxaan ak a waxi larax. + +Yonnant baa ngi amoon fan-weer ak juroom ciy at jamono yi Xuraysin di màbb Kaaba gi ngir tabaxaat ko, ndax tabax bi daa xawoon a màggat ngir yol mi daa sottiku ci kawam. Bi ñuy tabax ba àgg ca Hajarul Aswad ñu jaaxle ci gan giir ci Xuraysin mooy am teraangay yekkati ko teg ko fi mu war a tegu, ñu toog ca Kaaba ga di gëstu nu ñuy lijjantee loolu, far ñu dëppoo ci ne ku njëkk a ñëwaat rekk ñu jox la nga àtte leen ci jaaxle googu, far Muhammad (j.m) ne tëll, ñu ne ku wóor kaa ngee na ñu àtte, waaye mu àttee leen nu gaaw te yomb, mooy jël làmbaayam li mu yoroon lal ko ci suuf, teg ci doj wi ne giir gu nekk na jàpp ci cat ngeen tegandoo ko ca barabam. Nii daal la ko lijjantee ca yombam ga ak xarañam ga ak lëmóodikoom ga. + +Wàccug Wahyu gi ak yonni gi +Bi at yi jegee ñeen-fukk la sopp gi mu soppoon ag wéet gën a yokk, mu gën a bëgg xëlwa ak beru, mu daan génn Màkk ngir dem ca doj wa nu daa wax Harraa, ngir xunti mu fa nekkoon mu mu daa faral a dugg ngir jaamu Yàlla, noonu la daa jeexale weeru koor wi, ngir sellal boppam, laabal xolam. Benn bis nag ci koorug atum 610 g .j, ba jant bay so la ko genn kàddu gu nooy dikkal ca dalug xunti ma naan ko : jàngal. Yonnant bi (j.m) tiit njàqare li jàpp ko, waaye mu ne ko : man duma kuy jàng. Waaye mu yëg mu mel ne dafa am lu koy naj ba dënn bi xaw a xat mu noppal ko, bu ko defee kàddu gi delseeti neeti ko: jàngal, Yonnant bi neeti ko : man de manu maa jàng. Naj ga delseeti, ba mu xawee woyofati kàddu ga delseeti ne ko : ((jàngal ci sa turu boroom mi bind , bind na nit ci lumbu dereet, jàngal, sa boroomay ki gën a tedd)) kàddu ga daal di dal, daal di deseeti. Fekk jant biy so Yonnant bi yëg njàqare lu rëy, daal di gaaw génn xunti ma, dem ñibbi, bi muy àgg lëndëm gaa ngi doon dugg, ndax diggante Màkk ak xur wa xaw na a ëpp ay ñatti kilomet. + +Ba Yonnant ba (j.m) àggee ca kër ga daa daal di woote ne : muur leen ma, muur leen ma, booba ñaq waa ngay siit, yaram way lox, soxna Xadiija daal di dawsi sàng ko, tàmbli koo dalal, bi tiitaange gi demee Yonnant bi xamal ko li xew, ne ko : man de damaa xëm. Ndax xamagutoon ne li ko daloon ag wahyu la gu tukkee ca sunu boroom (t.s) , indil ko laaya wi njëkk ci Alxuraan ju tedd ji. + +Soxna su tedd sii di Xadiija wéy ci di dalal xelum Yonnant bi (j.m) naan ko lii la dal de du man a doon lu dul lu baax, ndax yaw ku baax nga, am kóllare, dëggu, baax ci sa ñoñ, di taxawu nit ñi bu ñu ameey naqar. Ca noona xel ma tàmblee dal, mu yëg jàmm. + +Waraqat’Ubn Nawfal mi ngi bégal Yonnant bi (j.m) +Bi soxna Xadiija gisee ne tiitaange gi dañ na daa ànd ak moom seeti doomi baay-tëxam ja tudd Waraqat’Ubn Nawfal, mu nekkoon góor gu am hikma, daan jàng téerey diine yi te dégg ebrë , Yonnant bi nettali ko li xew, Waraqat yéemu lool, ne ko lii de mooy mbóot mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa (j.m), ne ko aka neexoon may gone ba man a ànd ak yaw ci tas sa bataaxel bii, xelum Muhammad dal, mu dellu këram, waaye teguñu ci lu néew rekk Waraqat faatu, ndax daa xawoon a màggat. +Yonnant bi dellu këram ak Xadiija ci xel mu dal ak mbégte, am yaakaar ne wahyu gi dina delseeti, bu sukkadikoo ci waxi Waraqat yi, waaye wahyu gi yeex a ñëw ba Yonnant bi far àgg ci jaaxle lool, waaye mu mujj ñëwaat ginaaw bi, xelum Muhammad dal, mu xam ne lii kat ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla (t.s) te moom ku ñu tànn la ngir mu jottali nit ñi diine ju juge ci asamaan si, war a joxaat diiney asamaan yi seen leer ak sell gu njëkk ga ñu yoroon njëkk nit ñi di ko yàq, di ko tàqal ci li jamono di gën a romb. + +Nii daal la Muhammadum Abdu Laah mi (j.m) mujje di yonnant bu nu tànn yonni ko ci mbooleem mbidéef yi ngir mu indi fi leer gu tukkee ci sunu boroom di gindee, di tege ci yoon, di jële cig bokkaale jëme cig wéetal Yàlla,di jële ci lëndëmug réere Yàlla, jëme ci leerug gëm ko, jëme ci Lislaam. + +Fii la jaloorey Muhammad yonnantub Yàlla bi - jàmm yal na sax ci moom – tàmblee akug jànkoonteem ngir wisaare bataaxel bii ko Yàlla jox mu war koo jottalee ci ngën ji anam ak melo. + +ginaaw bi la wahyu gi tàmblee dikk cig toppante di wàcc ci Ku tedd ki, di indi laaya yi def tay alxuraan nànk-nànk, kon alxuraan ñëwadoowul cig mat, waaye laaya topp laay, ba kero muy mat, nga xam ne Jibriil da ko daan dikkal di ko déggal laaya yi, bu ko defee du ko ba ba kero muy wattu laaya jooju ci dënnam, mel ne sax dañu ko cee bind, làmmiñ wi di ko baamu, Yonnant bi bu masaa na jot ciw dogiit ci alxuraan da ko daa baamu ba mokkal ko, bu noppee jàng ko ci saabaam yi, daal di woo ñenn ci ñi man a bind ci ñoom ngir ñu bind ko ca saa sa ci anam gu xereñ, bu ko defee saaba yi gaawantu ñoom itam jàng ko mokkal ko ci anam gu dul soppikooti ba fàww. +Nii la laaya yi doon dabantee, saar yi di ko mate nànk-nànk ci lu tollook ñaar fukk ak ñatt ciy at, ndax kat laaya wi njëkk a wàcc ci Yonnant bi (j.m) mi ngi ko fekkoon mu am ñéen-fukki at wi ci mujj wàcc bi muy bëgg a faatu te booba mi ngeek juroom benn fukk yu teg ñatt ciy at. Alxuraan nag ñi ngi ci jublu téere bu tedd bi bépp walla ab xaaj ci moom. + +Alxuraan ju tedd ji ak li mu ëmb +Kon daal Alxuraan ci nii mu ñëwe waxi Yàlla a ju mu wàcce cib yonnantam (j.m) ngir mu jottali ko nit ñi. Ñi ngi ko wàcce ci Yonnant bi, muy lu nu biddiwal, maanaam nànk-nànk, kem ni ko xew-xew yi soxlaa ak tolluwaay yi ba kero muy mat, di téere bu ñu laabal, bu ay caaxaan dul laal fenn ((laa yaatiihil baatilu min bayni yadayhi walaa min xalfihii)). Moom nag danu koo séddale def ko ay saar yu toll ci 114 saar. Saar wu ci ne tam seddaliku ciy laaya, saari alxuraan yi nag ak laaya yi lii lanu ëmb : + + Ponki pas-pasu lislaam : +Saxal kennug Yàlla (t.s), nangu ne Muhammad Yàlla a ko yonni, gëm mbooleem yonnant yi fi jiitu woon Yonnant bi, gëm téere yi Yàlla wàcce ci ñoom, gëm alaaxira. + Ni ñuy jaamoo ci lislaam : +Julli, woor, natt asaka, aj. + Ponki jikko yi jullit bu nekk war a jikkowoo : +Ñuy wóor, dëggu, am yërmaande ci ku néew-doole, ku aajowoo, ku ñàkk, am ag cofeel ñeel bépp jullit tey dimblante ak moom ci lu baax ak fonki way jur, teral leen añs. + As lëf ci taariix: +Ngir jàjjeek waare aki nettali ci dundug yonnant yi, ngir soññee ci ngëm ak foñloo wëlif bokkaale + Yee nit ñi : +Ubbi seeni gët ci kàttanug Yàlla gi akug xerañam, jaare ko ci di leen woo ci ñu settantal bindiinu àdduna bi akug nosoom gu xereñ gi + Sopploo nit ñi gëm Yàlla : +Jaare ko ci wax leen li Yàlla dig ku gëm cib yool akug pay gu neex ci àdduna ak alaaxiraa ak soññee ci jiyaar ci yoonu Yàlla. + Ragalloo nit ñi ag weddi Yàlla ak bokkaale ko ak moytuloo leen wuuteek ndigëli Yàlla yi : +Jaare ko ci leeral leen mbugël yi ñu waajal ñeel ñi ragalul Yàlla mbaa ñuy tooñ nit ñi di jalgati, mbaa ñuy gàttañlu ci def jaamu Yàlla yi + Sariiya : +Mooy yoon wu mat wiy nos ni nit ñiy jëflantee ci seen biir, ak li nu am ciy àq aki yelleef ak li leen war ciy wartéef + +Lislaam nosteg dund gu mat +Dinanu gise ci loolu ne alxuraan de ëmb na ag nos gu mat ñeel dundug nit ci gépp anam, mi ngi rëdd séqoo gu nit ki ak boroomam akug séqoom ak mbokkam, dajaleeti jullit ñi ci genn bennte mooy umma bi walla mbooloom lislaam mi (di jullit ñi ), joxati mbooloo mii yoon ak nosteg politig, gu mboolaay ak gu jikko. +Dugg ci lislaam du rekk jël diine gëm ko, di def li mu digale ciy jaamu, waaye kay ag tuxu la dem ci ag mboolaay gu yees gu mat gu ami ponkam aki nosteem aki yoonam aki misaalam yu kawe, ndax lislaam ag noste gu mat la gu takkatoo. + +Bataaxelub Yonnant bi (j.m) mooy dugal nit ñépp ci lislaam ak tuxook ñoom jëm ca nosteg lislaam gu yees ga te mat. +Looloo taxoon Yonnant bi (j.m) daawul yam ci sàkku ci nit mu tudd ñaari seere yi rekk ak def jaamu yi, waaye kay da daan sàkku ñu bàyyi seen dundug réer gu njëkk ga te tàbbi ci nosteg politig, gu mboolaay, gu ruu gu yees gii. Moom de santuñu ko woon rekk mu woote te jotal bataaxel bi, waaye ligéey bu baax ci nit ñi gëm te dugg ci xeetu lislaam wi ak àddunaam ju yees ju fees ji dell ak yiw ak barke. + +Bataaxelub Muhammad (j.m) +Yonnant bi wéy na di xamal nit ñi bataaxelam bi, bu ko defee gàllankoor yi nekk ci kanamam mel ne ay doj , ndax kat nit yombul mu tàqalikook ni mu baaxoo woon a dunde, nit jaamub li mu miin la, waaye moom mu wéy di deewoo, di jànkoonte, di muñ ba jóoxe bataaxel bi ca na mu gën a rafete. Loolu mooy kiimaanug dundug Muhammad (j.m) gu yéeme gi cib taar, moom daal ci léppam dund la gu fees dell ak ay bind yu fees aki bind yuy jàngale dëggug ngëm, wóor ci def li la war, muñ ci lu naqari, ñeg ci fas yéenee jéggi gàllankoor yi, ŋoy ci jikko yu rafet, muñ ci loraangey nit ñi, gëm ne ndam lu mu yàgg yàgg dana mujj ñeel jullit biy jëf tey jànkoonte tey ŋoy ci buumug Yàlla gi ci lu dul naagu mbaa yoqat walla tàyyeel. + +Jànkoonte gi Yonnant bi doon def ci bi mu nekkee Màkka +Yonnant bi ginaaw bi nu ko yonnee dund na ñaar fukki at ak ñatt yoy ci la matale bataaxelam bi, fukki at ya ak ñatt nag Màkka la leen jeexal, fukk ya ca des mu def leen Madiina, làqu nag ca weeru rabiihul lawal ci atum fukk ma ak benn ginaaw gàddaayam gu tedd ga. + Diirub Màkka bi : +Mooy diirub deewoo ak jànkoonte gu tar ga ak way bokkaaley Màkka yi, ak jiyaaram ga ngir taxawal fa mbooloo mu lislaam mi, ba bi mu gàddaayee dem Madiina, diir ba di fukk ak ñatt ciy at. + + Diirub Madiina bi : +Mooy jamonoy ndam, jaare ci dugg gi waa Madiina dugg ci lislaam, mbooloom lislaam am fa, ak nos mbooloo mii ak mottali jaamu yi nekk ci lislaam ak sariyaam, ak tëral nosteg xeet wi, gu politig gi ak gu mboolaay gi, ak dugal dunu araab bi ci lislaam ngir waajale ci tas gi lislaam war a tas ci mbooleem pàkki àdduna bi, ab diiram nag fukki at la ak lenn ciy weer. + +Jamonoy Màkka ji +Dafa séddaliku ci ñatti tolluwaay : +Tolluwaay bu njëkk ba ak jullit ñu njëkk ña Tolluwaay bu njëkk bi ci jamonoy Màkka ji - ab diiram juroomi at la daanaka – mi ngi doore ci bi Muhammad (j.m) tàmblee di woote jëme ci lislaam, tàmblee ko ci giiram gi ko gën a jege, ca ñoom la jële mbooloo mi jiitu ci lislaam, ka nekkoon ca bopp ba di soxna Xadiija, nekkoon jigéen ji njëkk a jébbalu, ak Aboo Bakr di ki njëkk a gëm ci góor ñi ak Aliyun mom Aboo Taalib doomi baay-tëxi Yonnant bi (j.m), mooy ki njëkk a gëm ci gone yi, moom de booba ay atam fukk rekk lañu woon , ak Seyd’Ubn Haarisa mi doonoon mawlaab Yonnant bi, mooy ki njëkk a jébbalu ci mawlaa yi. + +Am mbooloo topp ci tàbbi ci lislaam ci waxambaaney këri Màkka yu Xuraysin yu mag yi, ñi ci Yàlla ubbi séeni xol nanguloo leen lislaam ak dalam yu kawe yi, ku ci mel ne Talhata mom Hubaydul Laah, Abdurahmaan’Ubn Hawf, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Usmaan’Ubn Haffaan, Subayr’Ubn’Ul-hawwaam. + +Am mbooloo it tàbbeeti ci Lislaam ci ñu ñàkk ñeek jaam yi ak way néew yi doole ci ñi Yàlla tawfeexal ubbil leen buntub gore ak yamoo ak yaakaar, ku ci mel ne Bilaal mom Ecopi mi, Hammaar’Ubn Yaasir, Xabaab’Ubn’Ul-arat. + + Jullit ñi ci kër Arqam : +Mbooloom lislaam mii baaxoo woon naa dajeek Yonnant bi ca Kaaba ga ngir déglu alxuraan ci moom ak jàng ci ponki lislaam, loolu it jur way bokkaaley Quraysin yi yoqat ci jataayi néew yi doole yii ci li wër Kaaba gi, tax it ba ñu tàmbli di leen xatal ak a yoqatloo, Yonnant bi it gis ne war naa wutal jullit ñi barab bu ñuy daje cig féex akug dal, ci noonu wenn waxambaane wu bokk ci ñoom ñu naan ko Arqam Ibn Abiil Arqam ne man naa joxe këram ngir ñu fay daje, Yonnant bi nangu, looloo taxoon jullit ñi ba woon daje ga ñu doon daje ca Kaaba ga. + +Waaye làqu gi nu làqu leegi tiitloo waa Màkka yi, jeqi ci ñoom njàqare, rawati na Aboo Jahlin ak Aboo Lahab mi nekkoon baay-tëxi Yonnant bi ak ñeneen, ñu tàmbli di topp jullit ñi ak di leen xeeñtu ngir xam li nuy def. + + Jébbalug Hamsa, Omar topp ci : +Am na bis Aboo Jahlin nekk fi barab di néggandiku Yonnant bi booba mi ngi jëmoon ca kër Arqam, ba Yonnant bi (j.m) egsee mu toroxal ko, waaye Yonnant bi muñ ak doonte ku dëgër la woon te manoon koo sonal, waaye Yàlla da koo digaloon mu woo nit ci hikma ak waare gu rafet, ci noonu mu wacc ko fa dem, bi Hamsa baay-tëxi Yonnant bi yëgee li xew daa mer seeti Aboo Jahlin duma ko ba noppi jébbalu dib jullit, ci noonu mbooloom lislaam mi gën a am doole ci dugg gi ci Hamsa dugg leegi. + +Bi ci as ndiir toppee Omar’Ubn Xattaab jébbalu, jullit ñi gën a sawar, gën a ñeme, ñu daal di génn leegi kër Arqam daal di dellu fa nu daa dajee di la wër Kaaba ga, ci noonu Yonnant bi tàmbli di woote ci kaw ci lu bir, te faaleetul merum waa Màkka yi. Fii la jamonoy woote ci kër Arqam jeexe, leegi woote gu biti gu matale gi tàmbli. + +Tolluwaayu Màkka bu ñaareel bi ak xeex gi Quraysin doon xeex woote gi Waa Màkka yi dañoo jàppe woon loolu muy ag dëkk gu leen jullit ñi di dëkk ak ag fontoo, ñu jug nag xeex leen xeex bu metti, jaare ko ci di sonal way néew yi doole ak faqiir yi ku ci mel ni Bilaal, Hammaar Ibn Yaasir ak Xabaab, ñu tàmbli woon it di ñaawal Yonnant bi(j.m) di ko saboote ak a lor ak lenn ci saaba yi. + + Gàddaay ga dem Ecopi: +Yonnant bi daa amoon njàqare ci saabaam yi, ragal waa Màkka yi sonal leen, ci noonu mu laabiire woon leen ci ne ku bëgg ci ñoom man naa dem Ecopi, foofa dananu fa man a doxal seen diine te kenn du leen topp mbaa mu leen di sonal, bi mu ko defee lu tollook juroom ñatt fukki góor akug jigéen gàddaay dem fa ci ñaari yoon. Yonnant bi des Màkka ak mbooloo mu néew ci jullit ñi, di jànkoonteek lori Quraysin yi. Waa Màkka yi jaaxle woon nanu ci man gi Yonnant bi (j.m) manoon a muñ ay coona ak sax gi, ñu sàkku woon ci baay-tëx ji mu tere ko woote gi maanaam Lislaam, waaye Yonnant bi bañ te wëy ca woote ga, looloo waraloon way bokkaale yi defoon ag dogoo gu mat ak Banii Haasin ak itam Banii Abdul Mutalib te ñoom ñooy mbokki Yonnant bi (j.m). Banii Haasim jànkoonte na aki coona ngir dogoo gii nga xam ne saxoon na ñatti at. Tolluwaay bu ñaareel bii nag weesuwutoon juroomi at. + +Ñatteelu tolluwaay bi ci jamonoy Màkka ji Sonalug waa Màkka yi ak xatal gi nu doon def Yonnant bi ak jullit ya jotutoon a gàddaay dem Ecopi àggoon na ca dayo ba bi yonnant gi amee fukki at, maanaam bi nu ko yonnee ba mu mat fukki at. Bi dogoo gi jeexee ba teg lu néew la Aboo Taalib baay-tëxi Yonnant bi (j.m) faatu, mi nekkoon njiitu Quraysin ak Màkka te daan aar Yonnant bi ci tar gi waa Màkka yi taroon ci di ko lor. Bu ko defee noonub lislaam bu tarug noonu gi jug moom itam yor njiitug Quraysin gi, moom baay-tëx la woon ci Yonnant bi waaye ku ko iñaane woon la te soxote ko. + +Bi Aboo Taalib faatoo ba teg lu néew la soxna Xadiija làqu moom it (y.y.g ) ginaaw bi mu àndeek Yonnant bi ñaar fukki at ak juroom cig sell, cofeel, dimblante ak bànneex, ak doonte fukki at yu mujj yi daa feesoon dell aki jafe-jafe, mettiit ak xatal. Yonnant bi naqarlu woon na bu baax ci faatug àndandoom bii mu bokkaloon dund gi, nekkoon ku matal kóllare, wóor, taxawoon ci wetam ci ati jafe-jafe yi, wone woon gën jaa kawey misaal ci ni soxna su gëm tey muñ war a mel. + +Bi Aboo Taalib ak soxna Xadiija làqoo Yonnant bi yëgoon na ne ku wéet la dëgg, te at yu metti yii mu def Màkka di jiyaar indilunu ko lenn ngérte lu ñu xam lu mu yaakaaroon ngir lànkug waa Màkka yi ak nuur gi nu nuuroon cig kéefar ak ŋoy ci li ñu fekkon seeni baay. + +Génn gi Yonnant bi defoon dem Taayif +Fii la Yonnant bi xalaate ci génn jéem a wooteji ca Taayif ga jege Màkka, mu daal di fay dem ànd ak mawlaam bi Sayd’Ubn Haarisa, waaye waa Taayif déggalunu ko, looloo tax mu dëppoon dellu Màkka. + +Waaye Yonnant bi loolu taxutoon mu yoqat ak doonte waa Màkka yi dañoo dogu woon ci lor ko, mu daal di jawali ca biti Màkka ca lenn ca giir ya fa dëkke woon, daan leen woo ci lislaam waaye taxutoon lu bari wuyyu ko ca. + + Mbégtey gàddaay gi: +Yonnant bi (j.m) da daan def bu déggaan aw nit ñëw Màkka mu gaaw gisi leen, woo leen ci lislaam, ba yonnant ga tollee ci fukki at ak benn daa dajeek ab kuréel ci giirug Xasraj ñëwoon Màkka, di woon genn ci ñaari giir ya nekkoon Màddiina, geneen ga di woon Aws, xare ba nekkoon di lu tar ci seen diggante ak noonoo ga. +Ca at ma ca topp am mbooloo ci Aws dikk na Màkka, Yonnant bi gaawantu seetsi leen wax ak ñoom, waaye fekk fi ñoom nopp yuy déglu, ndax kat Yahood yu Madiina yi dañu daan wax naan ab yonnant bu ñu yonni de dana dikki di dimbalisi Yahood yi ci Xasraj ak Aws, looloo waral Aws jortoon ne Muhammad (j.m) mooy yonnant bi Yahood yi doon wax. Bi seen mbooloo mi toogeek moom déglu ko lanu gis ne moom kat ku dëggu la ci li muy wax, bi mu leen jàngalee ay laaya ci alxuraan lanu ko gëm, sàkku woon ci moom mu may leen ba ñu dellu Madiina, man a nettali seeni mbokk li nu dégg. + +Ci noonu ñu dellu nettali seen mbokki Aws yi li nu dégg, ñoom itam ñu amoon yitte lool ci gis Yonnant bi te déglu ko, Xasraj it dégg loolu, ñaari giir yépp tàmbalee yittewoo gis Yonnant bi, ñu daal di dogu ci yonni am mbooloo mu mag ci jamonoy aj gi ngir mu dajeek Yonnant bi (j.m), déglu ko + + Jaayanteg Haqaba gu njëkk gi: +Mbooloo mi làqu waa Màkka ñëw dejeek Yonnant bi (j.m), déglu ko, waaye am lu leen wóor ci ne Yonnant bi de ku dëggu la, ci noonu ñu ànd dugg ci lislaam, def ak Yonnant bi jaayante gu Haqaba gu njëkk ga, daal di ko cay dig ne danañu woo waa Madiina ci Lislaam, te dinañu ko seetsiwaat ginaaw at, ci noonu Yonnant bi yabal ak ñoom saabaam ba tudd Mishab Bun Hamiir, ngir mu jàngal sariiya waa Madiina. + + Jaayanteg Haqaba gu ñaareel gi: +Bi lu toll ci at jàllee Mishab dellusi ànd ak ab kuréel bu mag ci waa Madiina, seenub lim tolloon ci juroom ñaar fukki góor ak ñatt ak ñaari jigéen, ñu jàkkaarloo woon ak Yonnant bi fa Haqaba jaayante fa ak moom, muy jaayanteg ñaareel ga, ñu ñaanoon ko mu tuxu dem Madiina, ne ko fas nanu ko yéenee aar ci gépp noonu te dinanu ànd ak moom ci tas Lislaam. + +Ci ginaaw bi rekk la Yonnant bi digaloon saabaam yi ñu gàddaay dem Madiina, ñu daal di woon tàmblalee gàddaay ci ay mbooloo, mbooloo topp mbooloo, lislaam daal di fay tas ba mujj doo gis genn kër ca Madiina gu ay jullit nekkul. + +Gàddaay dem Madiina +Li ëpp ci jullit yi nekkoon Màkka daal di gàddaay dem Madiina ci weer yu néew, bi Yonnant bi amee xel mu dal ca saabaam ya ca Madiina, daa daal di gàddaay moom itam ànd ak àndandoom bu dëggu ba Aboo Bakr, ñu ngi génn ci lëndëm gi cig làqu, ndax waa Màkka dañoo bëggoon a tëye Yonnant bi ca Màkka ngir ragal lislaam di ame doole ca Madiina. + +Mi ngi àgg Madiina ci 12 rabiihul Awal ca at mu njëkk ma ca gàddaay ga (4 sëtumbar atum 622 g,j), booba nag di taarixe ci gàddaay gi tàmbaleegutoon a dox, ndax Seydinaa Omar mooy ki digale ñu jël at mu njëkk mi ci gàddaay def ko at mi taariixu jullit ñi di tàmblee. + +Yonnant bi fekk na li ëpp ci waa Madiina ñu tàbbi ci lislaam, ñu néew a ci desoon cig kéefar, te bi Yonnant bi dikkee dañoo daal di jébbalu. Yahood yu bari nag nekkoon nanu Madiina, tasoon fépp it, ña ca ëppoon daan bay, mbaa ñuy def yenn mecce yi niki meccem weñ ak tëgg. Ñatti giir yu mag nag feeñ na ci ñoom, ñooy Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha, ñoom nag dañu daa won Xasraj ak Aws ne ñoo leen kawe, te daan leen jaxase bay waral ñuy xulook a xeex. Bu xeex amee leeg-leeg ñu ànd ak Xasraj, leeg-leeg Aws, daa nañu wax naan ab yonnant de dana feeñi ci ñoom te bu ñëwee dina ànd ak ñoom xeex Aws ak Xasraj ba jële leen fi. + +* Jëfi Yonnant bi (j.m) ca Madiina: +Yonnant bi bi mu àggee Madiina rekk daa daal di tàmbalee ligéey, ligéey bi nag ci ñaari mbir yii la jëmoon : +1 – Sos wenn xeetu lislaam wu gëm tey benn, ag mbokkoo muur ko, ag yamoo ëmb ko, ag maandute yiir ko, ñu fay doxal lislaam. +2 – Waajal xeet wii, wutal ko doole ju doy sëkk ngir mu man a duggal araab yépp ci Lislaam, teg ci mbindéef yépp. + +Yoon yi Yonnant bi jaaroon ngir amal ñaari mbir yii ñooy + Def ag mbokkale ci diggante jullit ñi, mu jox muhaajir bu nekk am mbokk mu bokk ci ansaar yi + Taxawal jenn jumaa ca Madiina ñu fay jullee, muy nekk it barab bu mbooloom lislaam miy dajeek seenub yonnant ak saaba yu mag yi + Def ag kóllare guy nos àq ak yelleefi nit ñi ci Madiina ak seeni wartéef ci lu jëm ci seeni moroom ak ci lu jëm ci xeet wu lislaam wi, kóllare gii nag Yahoodi Madiina yi ci lañu woon, waaye ñoom dëgguwuñu woon ci bokk gi ñu ci bokkoon. + +Yaatal gëwéelub xeet wi +Bi Yonnant bi nekkee ci ligéeyam boobu ngir amal jubluwaayam yooyu, mi ngi doon wéy it ci di woo ci lislaam giir yi peek Madiina ngir ñu bokksi ci uma bi, di xeetu lislaam wii xëy taxaw, bi mu gisee ne lenn ci kilifay giir yii ànduñu woon ak moom ci loolu, daa daal di woon yabal ay cong yu lislaam ngir xeex kilifa yooyu ak ñi leen di jàppale ba duñu man a gàllankoor giir yi ci dugg ci lislaam. +Cong yii lanuy wax xaswat, ndax Yonnant bi (j.m) moo ko daan jiite, bu ko kenn ci saaba yu mag yi jiitee nag ñu koy wax sariya + +Xaswat yi ak sariyat yi +Yonnant bi tàmbli na, daal di yabal juroom benni xaswa ak ay sariya yoy amal nanu xemmemtéef lii, bu ko defee gëwéelub uma bu lislaam bi gën a yàkkiku, daal di far ëmb mbooleem wàllug càmmooñ gu Hijaas gi, loola nag la ca juddoo mooy Madiina mujj teg loxo ci yoonu yaxantu wi jëme Shaam juge Màkka. Looloo taxawaloon yaxantu ga ca Màkka te kat moo nekkoon balluwaay bi seen koom di juge. + +Xaswat bu Badar bu mag ba ca 2eelu at g,g +Xaswa bu Badar walla xareb Badar Yonnant baa ngi ko def ci atum ñaareelum gàddaay gi, mi ngi ame nag ca digg yoon wa dox diggante Màkka ak Madiina, lu tollook ñatti téeméeri jullit am ca ndam ca kaw junni ci yéefari Màkka yi, muy ndam lu mag lol lislaam dëgëre na ci, nit ñi it xame ci ci anam gu wér péŋ gees manul a sikk ne Yonnant bi de wooteem gii lu wé la, ci noonu nit ñi sottiku Madiina ciy mbooloo yu mag ngir dugg ci lislaam, ci xare bii lanu raye Aboo Jahlin ak ñu ko moy ci nooni lislaam yu tar yig noonu. + +Xaswat bu Uhud atum 3eel mi giinaaw gàddaay gi +Màkka manutoon a ñàkk mu def lu ko delloosi darajaam ji mu ñàkkoon ci dunu araab bi, ubbilaat ko yoonu yaxantu wi, looloo waraloon ay way bokkaaleem dajale woon doole ju mag ju toll ci ñatti junniy góor, ñaari téeméer yi diy gawar , ca atum gàddaay mu ñatteel ma ñu dox jëm Madiina ngir dugg ko ci doole, waaye Yonnant bi génn àkk léen ci lim bu toll ci junni ciy saabaam. + +Ñaari mbooloo yi daje ca bëj-gànnaaru Madiina, fa ron doju Uhud, xare bu tar tàkk fa bob jullit ñaa ca amoon ndam ca njëlbéen ga, waaye boroom fett ya mujjoon wooteek ndigal la leen Yonnant bi joxoon daal di wacc seen barab ya nu leen taxawloo woon, Xaalid’Ubn Waliid mi jiite woon yéefar yi daal di màng pose bi song jullit ñi, bu ko defee seen sàppe jaxasoo, baj-baji, ñu ray ca ñu bari, waaye Yonnant bi moom des fa ak lu néew ciy gaayam, mu daal di woo ay saabaam ngir ñu dellusi. Ak li ñu ko gaañ ca xare ba lépp téewul mu xettali dooley jullit ñi ca njàmbaaram ga ak saxam ga, te tee yéefar yi dugg Madiina. Xeex bi wéy ba jant so, fii la coona bi sonale yéefar yi, ñu rocciku dellu Màkka ci lu dul ñuy amal li nu bëggoon, te loolu saxug Yonnant bee ko waral akug njàmbaaram ak sorib gisam. + +Waaye yéefar yi li nuy amadi li ñu bëggoon lépp téewul ray nañu ab lim ci tànnéefi jullit ñi, ku ci mel ne Hamsa bay-tëxi Yonnant bi (j.m), ak Mishab’Ubn Hamiir mi daa gàddu raayob jullit ñi ak leneen lu toll ci juroom benn fukki jëmm, jullit ñi am nañu lu leen naqari lool ci seen sahiid yi, waaye jànge nañu ci Uhud benn bind bu ñu dul fàtteeti mukk, mooy topp Yonnant bi (j.m) ak defi ndigalam. + +Xaswat bu Xandaq atum 5 g.g +Waa Màkka yi yég nañu ne amaluñu dara lu am solo ci li ñu doon sàkku, ñu gis ne ñoom kat ak seen mbégte mu rëy mi ñu am lépp ci ray gi ñu def lu bari ci jullit ñi téewul Màkka dañul di nekke na mu nekke woon: yoonu yaxantu wi mi ngi ci loxol jullit ñi, giir yaa ngi tàbbi ci lislaam, gu dugg geneen topp ca. + +Lii a tax Aboo Sufyaan’Ubn Harb mi nekkoon njiitul Màkka ginaaw Aboo Jahlin jugoon boole doole ju mag ci waa Màkka ak ñi tapoo ak ñoom ci giir yi, ñu dox nag jëm Madiina ca juroomeelu at ma ñeel gàddaay ga, bu ko defee Yonnant bi aki saabaam jug gas am xandaq ca la wër Madiina, ba mboolooy xarey yéefar yi agsee manuñoo jéggi pax ma, bu ko defee xare bi yam ci sàneente ay fett jéggi xandaq mi, ci noonu jullit ñi ñoom wone ag yewwu gu mat ci sàmm seen xandaq ba yéefar bu ko jéggi rekk rayees ko ca saa sa. +Gaw gi sax lu tollook ñaari ayu bis, ginaaw bi Yàlla yonnee gelaw lu tar ak taw bu metti mu yàq xaymay yéefar yi, fay seenuw sawara, sedd bi metti ci ñoom ak doonte weer woowa wu mars la woon, te woowu weer fa Hijaas mooy tàmbalig lolli bi, bu ko defee yéefar yi àggati ci manuñoo ñàkk a dind gaw gi te dellu Màkka ngir sedd bi te amuñu dara ca seen càkkutéef ya. Loolu di ag juunu gu mag akug sooy ñeel leen, te diw lay wu mag ak firnde ci kàttanug xeetu lislaam wi ak dëggug gëm gi ay nitam am, ak ñaw gi nekk ci njiit la Muhammad (j.m). + +Génne Yahood yi Madiina +Ñatti giiri yahood yi di (Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha) yoroon nanu taxawaay bu ñaaw te noonoowe jëme ca Yonnant ba ak wooteem ga, dale ko ca bi muy door a agsi Madiina, weddi woon nañu ag yonnantam, naan neey yonnant bi ñuy néggandiku manul a juge ci fu dul gañog Banii Israayil. Ginaaw nag yonnant boobu ñu daa wax farul génne ci ñoom, xanaa kay ci giirug Quraysin gu araab gii dara raxul, loolu naqari woon na leen, jural leen ag soxot ak kañaan ak mbañeel. + +Yonnant bi yàgg naa muñ lor yi ñu ko daa lor ngir yaakaar gi mu yaakaaroon ne danañu mujj noppal ko, ba àgg sax ci gëm ko, waaye lu mu muñ rekk ñu gën koo bañe lislaam gën koo dellikoo ag noonu, waaye làqoon nanu seen noonu googu ak mbañeel gi bi ñu gisee ne lislaam mi ngi gën a dolliku doole, di gën a dëgër bis bu Yàlla sàkk: + +Bi jullit ñi amee ndam ca Badar la xolub Yahoodi Madiina yi gën a dagg, ab kuréel ci ñoom it – ñooy Banoo Qinqaah - àgg ci manatuñoo ñàkk a feeñal seen bañ gi ñu bañ lislaam ak soxote gi ñu def jullit ñi ci ndam li leen Yàlla may, ci noonu ñu tàmbli di saboote Yonnant beek lislaam, waaye Yonnant bi (j.m) dem ca seen kër ya gaw ko, bi ñu jëbbalee seen bopp la leen génne Madiina ñu dem Shaam. + +Ginaaw bu xaswat bu Uhud jàllee ba teg lu néew, la yahoodi Banoo Nadiir lànk ne duñu joxeeti li leen war ci ndimbalul alal li war ñeel umma bi, waaye yamuñu ca, dañoo tàmbli woon a defi pexe ngir yong Yonnant bi (j.m), waaye Yàlla (t.m) musal ko ci seenuw ay, nga xam ne Yonnant bi amul woon lenn lu mu manoon a def lu dul génne leen ñoom itam ngir mucc ci seenuw ay. Ci biir xareb xandaq ba yahoodi Banoo Qariitha doon nañu jéem a wor jullit ñi dem jàppaleji yéefar ya gawoon Madiina jaare ko ci may leen ñu dugg Madiina jaare ko ci seenug wàll, looloo war bi xeex bi jàllee rekk Yonnant bi daa daal di jawali ca seen kër ya, gaw leen ba ñu wommatu, nangul ko, mu digal saabaam ba tudd Sahd’Ubn Muhaaz mu àtte leen ci li jaadu fi moom, li tax mu tànn ko nag mooy ñoom ci mom lañu doon sàkkoo ag tin ci Yonnant bi, moom it mu ne nañu ray ñi ci doon xeex, ñi ci des ñu génne leen Madiina. + +Ci noonu la xeetu lislaam wi mucce ci ayuw yahoodi Madiina yi, Madiina mujj yor lu néew rekk ciy yahood yu bokkoon ci ñi defoon ay tapoo ak lenn ci bànqaasi Aws yeek Xasraj, ginaaw nag feeñaluñu woon genn wor mbaag mbañeel ñeel jullit ñi Yonnant bi defu leen dara. Looloo waral ab kuréel ci ñoom gëm ca gëm gu dëggu, am ca ñeneen ñu ca gëm ñu ag ragal gëmloo akug naaféq + +Juboo gu Udaybiya atum 6eel g.g +Bi Yonnant bi amee lu ko wóor ci ne am cong mu juge ci biti jeex na, wor gu biir gi it dañ na la tàmblee waaj ngir dugal Màkka ci lislaam. Gisoon na ne waa Màkka yi ñi ci ëpp ñu tàmbali woon a yittewoo mbiri lislaam lañu ndax gis nañu muy yaatu, di gën a am doole bis bu nekk, li Alxuraan digoon jullit ñi bañu nekkee Màkka di ñu néew doole gën di feeñ, gën di am. Nga xam ne Màkka li ko tee woon a dugg ci lislaam wéesuwutoon lenn ci njiiti yéefar yi ak seeni àndandoo, ñoom ñi ragaloon seeni njariñ di sànku, seeni daraja di suufe su ñu duggee ci lislaam. + +Ci biir loolu ab laaya wàcci bu tedd buy digal Yonnant bi mu wëlbati qibla bi jullit ñi amoon muy Baytil Maqdis def ko leegi Kaaba gu sell gi, mu mujj ca saa sa di qiblab jullit ñi ñépp. + +Bi ñu wëlbatee qibla bi leegi jëme ko ci Kaaba gi, te Yonnant bi xam dëgër gi xeetu lislaam wi def leegi te ame ko doole ci la jugoon ànd ak am mbooloo ci saabaam yi ngir defi umra, mooy siyaareji Bayti Laahil Haraam ci waxtu yi dul yu aj, looloo tax ñu tudde ko aj gu ndaw gi. + +Bu ko defee, Yonnant bi (j.m) daal di génn ci junni ak ñeenti téeméer ci ay saabaam jëm Màkka ngir defi umra, looloo taxoon yobbaalewuñu woon ngànnaay ngir bëgg waa Quraysin xam ne jullit ñi dañoo ñëw ngir defsi ag jaamu rekk mooy umra gi. Bi jullit ñi aggee ci barabub Hudaybiya mooy buntub Màkka bi féete wàllug cammooñ la waa Quraysin yi tàmbali woon a ragal jullit ñi dugg Màkka. Ñu daal di yonnee ci Yonnant bi ne ko daal àndatuñu ci jullit ñi dugg Màkka ak donte yoruñu ngànnaay. Ñu daal di fay def waxtaan wu yàgg yu mujj àgg ci li ñuy wax Juboog Hudaybiya, moom nag li mu yaxal mooy jullit ñi buñu dugg Màkka ca at mooma waaye bu déwén ja’a ca waxtu woowa dinañu man a dugg (muy atum juroom ñaareel ma g.g), bu ko defee ñaari wàll yi def ag juboo guy sax fukki at. + +Ca juroom-ñaareelu at ma ñeel gàddaay ga, Yonnant bi dellu defi umra ga mu yéene woon ca daaw ja, daal di siyaare ab dëkkam bi mu juddoo, ginaaw ba mu fa gëjee lu tollook juroom ñaari at. + +Yonnant bi (j.m) bind na buur yi +Ci biir atum juroom ñaareel mi ñeel gàdday gi la Yonnant bi (j.m) yabal ay ndaw ca Qaysar mu Rom mi, Kisraa mu Faaris mi, ak kilifag Qibt ya ca Isipt, joxaale leen ay bataaxel yu leen di xamal lislaam te di leen ci woo. Qaysar moom daa yeexoon a tontu, bu dee Kisraa mu xottite bataaxel ba, waaye Maqooqas moom daa tontu tontu bu rafet, yonnee ca Yonnant ba adiya waaye taxutoon mu dugg ci lislaam. + +Yonnant bi yonneeti ci lu bari ci njiiti araab yi ak seeni kilifa ak buur yi nekk ci mbooleem dun bi, am ñu ci dëggal te gëm, waaye la ca ëpp tontuwuñu. + +Ubbig Xaybar +Xaybar am mbooloom ay waaha yu ndaw la yu nekk ci bëj-gànnaaru daanaka dun bi, ca waxtu woowa Xaybar ci loxol yahood yi la nekkoon, ñu seŋe woon ko, ngartaajoo woon ay xéewalam, def ko seen dàttub xare tey seen barab bu alal, ñu tàmbali woon di xiirtal seen dëkkandooy araab yi ci ñu fexeel lislaam ak Madiina. Waaye Yonnant bi dëgmalsi leen ci mbooloom xare mu mag, gaw Xaybar, jullit ña songoo fa ak yahood ya cib xare, Yonnant bi dumaa leen fa, ñu wommatu, yeneen waaha yi ko jege woon te nekkoon ci loxol yahood yi topp ci, niki Fadk ak Timaa. Ci jëf jii la Yonnant bi raye jànkoonte ak jafadiku gi yahood yi dese woon daal di fegu ci seenuw ay. + +Ubbig Màkka ci juroom ñatteelu at mu gàddaay gi +Ci biir loolu fekk na Màkka mu néew lool doole, ñu ëpp ci ñi ko daa jàppale bàyyi ko, lislaam tas fat tas gu yéeme rawati na ginaaw Juboo gu Hudaybiya gi. Ci njëlbéenug juroom ñatteelu at mu gàddaay gi la waa Quraysin firi woon seen kóllëreg juboo ga ñu defoon ak Yonnant bi, loolu nag mi ngi ame ci tooñ ak jalgati gi ñu defoon giirug Xasaaha gi nekkoon jullit, ci noonu Yonnant bi jug ci fukki junniy jullit dugg Màkka ci lu dul xare ci weeru koor gu juroom ñatteelu at ci gàddaay gi (samwie 630 g.j) +Bi Yonnant bi duggee Màkka daa daal di laabal Kaaba gi, dammate xërëm ya, sànni leen ñu sori Kaaba ga, jullit ñi daal di raxas Kaaba gi, mu nekk leegi nag di néegub Yàlla deesu fa jaamooti ku dul moom. Ci loolu la Yàlla dëggale dëel bi mu joxoon Yonnant bi ak jullit ñi, ndax jàppale na leen, jàppale diineem, fay leen ci seen sellal gi ak dëggu gi ak jiyaar gi ñu doon def ci seen alal ak bakkan. + +Bi loolu jàllee ba teg lu néew, lislaam daal di tas ci Màkka gépp, ñu taxawal fa ay jàkka, mu mujj di ñaareelu dëkk ak digg bu lislaam ginaaw Madiina gu ñu leeral gi . + +Xareb Hunayni +Ginaaw bi ñu ubbee Màkka ba teg lu néew la giirug Hawasaan ak giirug Saqiif gi mu tapooloon jugoon dajale xare bu mag, dox nag ngir xeexi jullit ñi, waaye Yonnant bi duma leen duma yu tar ca fa ñuy wax Haniin, bi loolu amee genn giir jugatul naan day xeex lislaam. Ginaaw ndam lii Yonnant bi (j.m) dem na Taayif dëkk bi Saqiif dëkkoon gaw ko, ba gaw ga yàggee mu xam ne dana wommatu , la leen fa ba dellu Madiina, waaye noonu la deme woon ndax yàggaatul dara Taayif jébbalu, giirug Saqiif gépp dugg ci lislaam. + +Atum Mbooloo yi di juroom ñeenteelu at ginaaw gàddaay gi +Atum juroom ñeenteel mi ñeel gàddaay gi ñi ngi ko tudde woon atum mboolooy yi, ngir ne ci la giiri dunu araab bi bépp doon yabal ay mbooloo yu bokk ci ñoom ngir yëglesi seenug dugg ci lislaam, mbooloo yii nag bawoo nañu ci mbooleem goxi, nga xam ne bi fukkéelu atum gàddaay giy jot fekk na mbooleem dunu araab bi dugg ci lislaam, ñépp ña fa dëkk mujj bokk ci uma bi. + +Xaswat bu Tabuuk di bi Yonnant bi mujj a def +Ci sawaal atum 9 ci gàddaay gi, ginaaw bi nga xamee ne mbooleem araabi daanaka-dund bi dugg nanu ci lislaam, la Yonnant bi bëggoon a xamal jullit ñi ne jiyaar ji de fàwwu mu génn dunu araab bi, ngir ñu man a tas diine ji ci àdduna bépp, looloo taxoon mu wommatoon benn xare bu mag ci ay jullit, dox jëm bëj-gànnaar ba àgg Tabuuk ca dig wa dox diggante dunu araab beek réewi Shaam yi nekkoon ci ron teg loxo gu Rom, foofa la nguuri araab yi nekkoon ci dig yooyu duggoon ci lislaam, jullit yi it xame ci ne jiyaar de day sax di wéy ba fàwwu . + +Ajug tàggoo gi atum 9 g.g +Ci silhijja atum fukkéel mu gàddaay gi la Yonnant bi defi woon hajjatul wadaah di ajug tàggoo gi, ba muy dem nag ma nga àndoon ak ay junniy junni ci jullit ñi, ci aj gii la Yonnant bi (j.m) leerale ajiin wi ñu yoonal, te mooy wii fi nekk bat ay jii ñu nekk . + +Bi mu noppee ci aj gi la def xutbaam bu bu mujj ba nuy wax xutbab tàggoo ba, mu dénk ca jullit ña dëggu, bennoo, boole séen sàppe, jóox farata yi lislaam digale ak tënku ci ponki jikkoom yu màgg yi, bi mu noppee jàngal nit ñi waxi sunu boroom ju tedd ja: (( al yawma akmaltu lakkum diinakum, wa atmamtu halaykum nihmatii, wa radiitu làkkumil islaama diinan)) di : (ci tay jii de laa matale seen diine ji, ci laa matale xéewal gi ma leen doon jox, te lislaam nag mooy diine ji ma gërëm te sopp ko ci yeen). Fii nag jullit ñi yëg nañu fi ne yonnant baa ngi leen di tàggu te di leen dénk li ñu war a def bu ñu ko gisatul, ñoom ñépp jàq te am lu leen naqari. + +Bi Yonnant bi (j.m) delloo Madiina la yëg – ci mujjug safar – lu mel ne tawat di ku dugg, waaye faalewu ko, dafa wéy di ligéey ba tawat ji far ko man, mu doog a tëdd, waaye tawat ji yàggul, ndax mi ngi làqu ginaaw bi tawat ji amee ci moom fukki fan ak juroom, di ci 13 rabiihul awal atum 11 g.g ( 8 suwe 632 g.j) : + +Jëmmi Yonnant bi +Ci nii la Yonnant bi (j.m) tuxoo dem ca boroomam ginaaw bi mu jottalee bataaxelam bi ci anam gu mat te yaatu, tas ko ba ñépp jot ci, ca na mu ware. Wooteem gi mi ngi ko tàmbali cig wéet , ay gàllankoor aki pakastal gaar ko ay yooni yoon, mu daje ciy coona lol manoon naa yoqatloo geneen góor gu mu manoon a doon gu dul moom, woote na fukki at ak ñatt yoy amu ca lenn ngérte lu am njariñ, waaye mu sax di ku dëgër ag ngëm ci Yàlla, ku am kóolute ci ndimbalam, wéy ca liggéeyam ba ba ndimbal dikkal kook ndam ginaaw bi mu gàddaayee dem Madiina, daal di fay taxawal umma bu lislaam bi, dox ak moom ci yoonu nosu ak doole ci anam gu màndaqewu te callalewu, weer ginaaw weer, ba mujj am ci ndam lii ngay gis tay. + +Yonnant bi nag li ko dimbali ci mu jot jubluwaayam bii mooy jikko yu yéeme yi te wéet yi mu jikkoo woon ak bataaxelam bii bàyyikoo woon ca Yàlla ma ko tànnoon ngir mu jottali ko. + +Ñun nag manuñoo lim mbooleem jikko ak ngënéeli Yonnant bi (j.m), looloo waral jullit ñi ñoom dañu koo def muy xam-xam ci jëmmam bu ñuy jàng ñu koy wax xam-xamu jikkoy Muhammad (As shamaayil al muhammadiya) taalif nañu ci lu dul jeex, ñun nag ñu ñeme ñemelu indil leen lenn ci yi ëpp solo ci jikko yii : + +Gëm gu xóot ci Yàlla +Gëm gi mu gëmoon Yàlla gu matale woon la te xóot, da daan def fu jafe-jafe yi gënee bari, gàllankoor yi gën a dolliku, gëmam gi ci boroomam gën a dëgër, mu gën a ŋoy ci bataaxelam bi, gën a dogu ci wisaare wooteem bi ko Yàlla dénk. + +Looloo taxoon Yonnant bi ak saaba yi daawuñu nangu lu dul ngëm gu mat gu dara ci sikk dul jege. Ci daaray ngëm gu xóot gii la saaba yu mag yi génne, ku ci mel ne Aboo Bakr, Omar, Aliyu, Usmaan, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Abii Hubaydata Haamir’Ibn Jaraah, Talhata’Bn Hubaydul Laah, Zubayru’Bnul Hawaam ak ñi mel ni ñoom ci ñi war a yanuji raayob lislaam ginaaw Yonnant bi (j.m), te war a tasaareji diiney Yàlla ji ci li ëpp ci pàkki àdduna yi ñu xamoon ca jamono jooja + +Jafandu ci way teddi jikko yi +Ngir gëm gu dëgër gu xóot googu ci boroomam (t.s) ak ci lislaam, daawoo gis Yonnant bi mukk muy jëf ci lenn ndare bu tegu ko ci gën jaa dëgëri dàtti jikko yi, niki dëggu, matal kóllare, wóor gu mat ci wax ak jëf, ak seelug yéene ci lépp lu muy wax mbaa mu koy jëf, ak tëyye bu dëgër cig maandu ci mbooleem ay jëflanteem aki saabaam, ba ci ay kontaram, nekkoon na di ku bu waxee dëggal, bu dëelee matale, bu kóllarantee def ko, bu manee jéggale. + +Doylu ak bàyyee +Yonnant bi de ak li ko dikkaloon lépp ci xéewali àdduna, ak teddnga ak doole teewutoon mu nekkoon di kuy doylu ci gën jaa tuuti ci xéewal yi, dundam gépp masu cee feesal biiram ciw ñam, lu néew ci mburu la daa mos ak tàndarma, bu amul rëndaay mu rëndaayoo diw, mbaa diw ak bineegar, mbubbam ak dallam ci loxoom la ko daa daaxe, daan fóot mbubbam bis bu jot ci loxoom, ndax moom (j.m) ku jéggi woon ab dayo la ci set, bis bu nekk daa na ci socc ay yooni yoon. + +Daawul toggoo nag ag dund gu ñagas te di ko woote, moom kay ñam wu ko dikkal rekk mu lekk. Soloos na ci moom ne daawul sàkku mukk aw ñam wu fi nekkul, cib pajaas la daan nelawe, am mbalaanam it lu gàtt la daan doon, daawul tëju ay saabaam, ki gën a doyodi ci nit ñi da ko daa gis di wax ak moom, waayam ja ko daa ligéeyal di Anas mom Maalik nee na masul a dégg ci Yonnant bi ci dundam gépp benn baat bu ko mas a naqari. + +Daf daan bàyyee saabaam yi xéewal yi, te daawu ci féetewoo dara bàyyi leen, nekkoon na di ku sopp xale yi te daan kaf ak ñoom, ku amoon ag ñeewant la ci jirim yi, way ñàkk yi, ñu doyadi ñi, di seeti way tawat yi, bëcëg bépp it ci yëgg la daan nekk, daawul dal, ku bañoonug jekki la ak tàyyeel, daa na ko moytulooy saabaam. + +Misaal la woon ci ni ñu war a jiitee xeet wi ak ni ñu ko war a sàmme +Yonnant bi ku amoon ag yewwute gu sax la, daawul ba dara romb ko ci lu aju ci umma bi ndare bu da koo gendiku bu baax te settantal ko. Daf daan settantal di teg ay naal yu jub, yu yaatu yu muy jaar ci ligéeyam ci anam gu nosu te toftaloo. +Yitteem jépp da ko daa sotti ci li ëpp solo ci mbiri xeetam wi, teg ca la ca topp cig am solo. +Daa gisoon ne ay ligéeyam aki jëfam roytéef la wuy saabaam di jaari ëlëg, làmp la bu ñuy niitloo, moo waraloon lu muy def rekk mu koy def cig njàngale , cig yare. Bu kenn ci saabaam yi juumee ci mbir, da ko koy won cig nooy, leeral ko lay la jub. Ku daan am ag muñ ci way xuloo yi la, daan leen jéggal seeni soppaxndikooki jikko yu ñaaw ngir ñu gis seen njuumte, dellu ca jub ga. Ku wormaaloon nit ñépp la, daan sàmmoonteek teddngay ki gën di gone ci ñoom ak àqam. Masuñoo dégg fenn fu ñu ne Yonnant bi (j.m) génnee na fa baat bu ñaaw jëme ko ci kenn, ak doonte kenn kooku da dib noonam. Bu masaan a mer day noppi ba mer wa dañ mu doog a wax nànk, cig dal. + +Yonnant bi noppee ko gënaloon wax, dégloo ko gënaloon déggal. Bu masaan a wax day àgg ca la mu bëgg a wax du jàdd-jàddal, def ko it ci baat yu leer te gàtt, looloo taxoon Yonnant bi (j.m) moo gënoon a am fasaaha ci nit ñi, gën cee am balaaxa, adiisam yi ci balaaxa ñoo topp ci Alquraan miy wax ji gën a balaaxaa ci wax yi. + +Yonnant bi (j.m) yérmaande la ñeel mbindéef yépp, bi muy ñëw ci àdduna bi da koo fekkoon mu yor lëndëmug réer, ndof, xamadi Y��lla, waaye mu bàyyikoo fi, ba fi ag leerug gëm Yàlla . Mi ngi feeñ ci araab yi te booba ñi ngi ciy xareek fitna ak ŋaayoo, mu juge fi ba leen ñuy xeet wuy wenn, yiw peek leen, lislaam ëmb leen, jàmm uuf leen. Ak li Yàlla sotti nit ñi lépp ciy xéewal, jaarale ko ciy loxoom teewul Yonnant bi – jàmm yal na nekk ci moom – bi mu fiy juge di woon ku ndóol, ku moomul lenn. Saddaloon na nit ñi aw léew ci nite, ngënéel, def wartéef, sellal ak dëggu. Yàlla dëggal na – tudd naa sellam ga – ba mu nee : ((yaa ayuhan nabiyu inna arsalnaaka shaahidan wa mubashiran wa nadiiran wa daahiyan ilal laahi bi idnihii wa siraajan muniiran, wa bashiril moominiina bi anna lahum minal laahi fadlan kabiiran)) muy :( yaw Yonnant bi de dañu laa yonni ngay seere tey bégaleek a xuppe, di woote jëme ci Yàlla ci ndigalam, tey làmp buy leeral, na nga bégal jullit ñi ci ne am nañu ngënéel lu rëy lu tukkee ca Yàlla) +Yonnant bi nag (j.m) tënk na wax jépp ca bataaxelam ba niki kuy jàngale ba mu nee : (dees maa yonni ngir ma mottali jikko yu rafet yi). + +Téerekaay + Abdul-Haqq, Abdiyah Akbar (1980). Sharing Your Faith with a Muslim. Minneapolis: Bethany House Publishers. N.B. Presents the genuine doctrines and concepts of Islam and of the Holy Qur'an, and this religion's affinities with Christianity and its Sacred Scriptures, in order to "dialogue" on the basis of what both faiths really teach. ISBN 0-87123-553-6 + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + +Diine +Yonenti Lislaam +Lislaam +Xeltu baat la bu nu doge ci « filasofia », muy baat bu cosaanoo ci làkkuw gereg, maanaa mi mu yor ci baat yi di « sopp hikma » loolu di (xel mu rafet ;sagesse ci Fr), ba ci laaj rekk ne « lan mooy xeltu ? » dees koy jàppe ab laaj bu di kojug xeltu bu nu man a yendu di ci dàggasante. Lii benn la ci màndargay xeltu yu dëgg-dëgg yi ak jeng gi mu def jëm ci laaju ak defi gëstu ci lepp lu mu man a doon te jéem a xam dëgg-dëggam aki màndargaam aki àtteem. Lii lépp a tax nag xeltu di xam-xam bu yaatu te bari ay ñall, laal daanaka ci xam-xam yépp, walla ci mbooleem wàlli dund. Waaye loolu lépp téewul muy xam-xam bu wéet ci boppam wëlif yeneen xam-xam yeek jagoo yi (specialisation). Xeltu leeg-leeg ñu melal ko ci ne mooy “xalaat ci xalaat” maanaam xalaat ci jëmmi xalaat, cib déndam ak ci settantal, dees na ko melal it ci ne mooy jéem a indi ay tontu ci laaj yi am gi di indi ak nekk gi (l’existence). Xeltu seere na ay jëm kanam yu am solo te lëw, dale ko ca waa Geres ya sos ponki xeltu yu mag yi niki xam-xam buy tabax ab gis-gis bu matale ñeel nekk gi(adduna bi) ci biir gis-gis bu di kojug li-am(réaliste), ba ca xeltukati jullit ñi nga xam ne danoo jëflanteek ndonol Geres li (li fi waa geres yu yàgg ya ba woon), jaxase kook nattu (experimentation), daal di soppi “xeltu bu kojug li-am” bi, yóbbu ko ci “xeltu bu kojug tur” ak “xeltu bu kojug xam-xam ak nattu” ci jamonoy yewwute walla judduwaat (renaissance), teg ci “xeltu yu kojug am yi” (existence) ak “yu kojug nite yi” ak “ngéri yees gi ak la ca ginaaw yeeg” ak “ñàkk” (maanaam dee walla bañ a am). Xeltu gu yees gi – ci aaday seggat ci Amerig gu bëj-gànnaar gi(USA) ak nguur gu bennoo gi (UK) (ci seen aada ji nu am ci seggat mbir yi (anaaliise ko)) – day barastiku jëm ci gën a nekk gu xarala ci gu neen rekk, moom day taxaw ci xellu (logique) ak ceggat gu dégg-dégg (conceptual analysis), looloo waral ay tërte (sujets) yi yitteem di jëm day àgg ci làmboo “gis-gis bu kojug xam” ak “jikko” ak “déndu làkk” ak “déndu xel”. Am na yeneen xam-xam ak jubluwaay yu jàppe xeltu muy jàng “fann” (walla ci Fr:art) ak xam-xam yi, bu ko defee muy gis-gis bu daj te matale, di tegtalub dund bu ubale te daj. Ci déggiin wii la xeltu di nekke di luy yittewoo xamale yoonu dund ga gën, dootul nekkati luy jéem a xam dund gi. Jamono yi jubluwaay bu seggat bi jàppee xeltu muy mbirum jëf mom fawwu nu jonjook moom, doxal ko, jëf ko, am na yeneen një (jubluwaay) yu ko jàppe muy cëslaay (base) li xam tegu, ñu war koo xam xam gu wér te xereñe ko. + +Xamale luy xeltu +Xeltu baat la bu gereg bu juge ci (fila) di tekki sopp, ak (sofia) di tekki hikma maanaam (sagesse) walla xel mu rafet, kon muy firi ((sopp hikma)). Baatub xeltu ci jamono ju yees ji ñi ngi koy wax jublu ci dox gi nit di dox ngir xam laaj yu mag yi aju cig dundam, bokk na ci yooyu dund ak dee ak li-am (realité) ak maanaa yi ak dëgg. Baatu xeltu it dees na ko di faral di jëfandikoo ngir xamalee ci li xeltukat yu mag yi def ciy liggéey yu nu bokk. + +Waxtaan ci xeltu du lu waa geres jagoo ñoom rekk, waaye kay ag wàll la ci xayug (civilisation) xeet wu nekk, xeet yépp a ci bokk. Looloo tax laaj luy xeltu? Du tekki benn tontu rekk. Xeltu cig tàmaleem ca jamonoy Taalis da doon gëstu cosaanul am gi (l’existence) ak aji bind ji (le créateur), ak ne-ne (matiere) bi ñu binde mbindéef yi, ak xeet (elements) yi leen toggale, bu ko defee dàggasante gi wéy di tang ci loolu ba ci jamonoy Sinon ak (Sofistaa) yi nga xam ne danu doon jëfandikoo xeltu ci weddi Yàlla ak wëlbati maanaa yi ak dégg-déggi baat yi (li nu ciy dégge) ngir notal seeni gis-gis, waaye mi ngi tàmbali ci jamonoy Sokraat mi Siisroon doon melal ci ne mooy ((ki wàcce xeltu ci suuf si jële ko ci asamaan si)), maanaam mooy ki jële xeltu ci xalaat ci nekk gi ak ki ko sàkk, ak xeet (elements) yi mu ko toggalee (yi mu ko sàkke), yóbbu ko ci xalaat ci jëmmi nit. Moom nag soppi na lu bari ciy màndargaam, daal di tuxal ay ŋaayoom aki dàggasanteem yóbbu leen leegi ci déndub nit (nature-am) ak dëgg-dëggam, ak gëm aji bind ji te gëstu ko, te jëfandikoo tegtalu xel ci saxal ko. Sokraat nag jëfandikoo woon na xeltu ngir tas jikko yu rafet ci biir nit ñi ak dëggu ak soppante. Sokraat nag ñëw na mook Aflaton (Platon) sukkandiku ci ñaari jumtukaay yii di xel ak xellu (logique) niki cëslaayi xalaat bu sell te mucc ayib, xalaat bob day dox dëppoo ak ay ponk yuy leeral ag wéram akug neenam. + +Laaj : “luy xeltu?” bii laaj Aristo tontu na ko. Ci noonu sunu wax ji amatul njariñ, ndax dafa jeex te tàmbaleegul, kon tontu bu gaaw bi ci loolu day man a taxaw ci cëslaay lii: tontu bi Aristo joxe woon ci lan mooy dëgg-dëggi xeltu du moom rekk mooy tontu bi nu ci man a joxe, ca dëgg-dëgg loolu daal benn rekk la ci tontu yi nu ci man a joxe. Nit daal - bu sukkandikoo ci ni Aristo xamalee xeltu – dina man a xalaat te firi xalaat yi jiitu Aristo ak Aflaaton ak xeltu yi ñëw ginaawam. Ànd ak loolu teewul nit ki dina seetlu ci anam gu yomb ne xeltu de ak yoon wi nu xame dëgg-dëggam soppiku nanu ci ñaari junniy at yi topp ci Aristo soppiku gu mag. + +Waaye ci biir loolu jëmm ji wart a réere ne xeltu, la ko dale ca Aristo ba ca Nits dafa sax – ci cëslaayi soppiku yooyu ak yu leen moy – di moom ci jëmmi boppam, ndax kat soppiku yooyu dafa ame ci wàllug xereñ. Wattu ag yamoo ci biir moom moom la (…) + +Lu wér la ne dinanu man a ame ci yoon woowu ay xam-xam yu wuute te xóot, neel yu am njariñ ci ni xeltu feeñe ànd ak taariix, waaye nag woowu yoon dunu may ñu àgg ci am tontu yu dëggu maanaam yu yoonu ci : lan mooy xeltu? + +Ni Aristo firee xeltu ne mooy “sopp hikma” am na lu ëpp benn teglal walla maanaa. Tegtalub làkk bi, moom mi ngi aju ci làkku gereg wi ñu tëgge baatub filosofia, ak tegtalub xam-xam bi nga xam ne dafa wuuteek li nu nekk lool. Sikk amul ci ne tegtal bu mujj bi walla maanaa mu mujj mi mooy bi leeral maanaa mi, gaw ko ci “sopp hikma” niki melo wu nu man a wonee ñàkk gi ay am-am (donnés) yu xam-xam ñàkkoon ñeel xeltukat bi ca jamono jooja, bu ko defee hikma nekkoon benn ci pexe yi ñu daa pexee ci lu nu xamul, niki ab ne-ne bu njëkk bi nga xam ne ci la xeltukat biy sose nosteg xam-xamam, mu dëppook settantal gu xam-xam ga amoon ca jamono jooja. + +Bu dee leegi nga xam ne xam-xam daa sakkan, li ñu wuññi lëw, laaj yi bari ci ëtt yu bari ak mbir yu dul jeex, ak jëm kanam gi nit def ci wàll yu bari, loolu lépp tax na ba liggéeyub xeltukat du doonati rekk sopp hikma, ak gëstu ko ci jumtukaay yi mu ko daa gëstoo ak ci ron kilimãb réer gu tar gi mu amoon ci wërlaayug àdduna gi ko wëroon ca jooja jamono… Xeltukat leegi lu sakkan ciy ngér (ecole, methode) ñoo ko tënk aki àtte yu di kojug xellu aki am-am yu di kojug péng (lu wóor), ci ron jalub ay xam-xam ak seeni doxal (pratique) yu xarala yu la dul may fenn fooy sikke seenug nekk di yoon. Ci ndabi jamono (conditions) yu mel ne yii, ak ci am-am yu nirook yii xamaleg xeltu ga nu xamoon du manatee dëppook liggéey bi xeltukat bu jamonoo bi man a def, maanaam bu sunu jamono jii nu nekk, moom mi nga xam ne ab liggéeyam daa wuuteek bu ñoñ jamono yu yàgg ya lool. + +Bu nu sukkandikoo ci li jiitu danu naan manatuñoo def nenn nu dul jéem a xool nu nuy soppee dégg-dégg ak maanaam xeltu ndax mu doon leegi “juddal hikma” te bañ a doonati “sopp hikma” + +Xeltug waa-afrik + Gu jamonoy firaawna + Xeltu gu magreb + Daaray xeltu yu tombuktu yu jamono yu yagg ya + Xeltuy waa-afrik yu jamono yu yees yi ak yu mujj yi + +Dawani(courant) xeltug waa-afrik gu mujj gi + culturaliste + herméneutique + diachronique + fonctionnel + +yeneen Xeeti xeltu + Xeltu leeg-leeg (nu koy melal ci ne mooy “xalaat ci xalaat” maanaam xalaat ci ni nuy xalaate ak ci jëmmi xalaat ci boppam akuw melokaanam, dees na ko melal it ci ne mooy jéem a tontu ci laaj yu mag yi nekk gi di laaj ak am gi(l'existence)) + Xeltu gu tur + GBu xam-xam ak nattu + Yu kojug nekk + Yu kojug nite + Xeltu gu yees (ni ko waa Amerig gu bëj-gànnaar gi baaxoo seggate ak Nguur gu bennoo gi(u.k) day xaw a barastiku jëm ci wàll gu xarala, bu jàllee ay wax (ay sujets) doog a digg, moom day sukkandiku ci xellu ( logique) ak seggat, kon ay yitteem day sottiku ci gis-gis bu kojug maanaa ( conceptual analysis)ak jikko ak melokaanu làkk ak wu xel.) + Xeltug Ceggat + xeltug waa-sapon + Xeltug julliti-araab + Xeltug waa-siin + Xeltug yëwut + xeltug waa-end + +Yenn ciy xeltukat + Kocc barma faal (Reewu Senegaal) + Mohammed Bagayogo (Reewu mali) + Ahmed Baba (juddoo Araun ca Mali ci 1556 ) + Anton Wilhelm Amo (rewu Gana) + Kwasi Wiredu (Reewu Gana) + Ibn Badjdja (Nguuru Marok) + Ibn Battuta (Nguuru Marok) + Ibn Khaldûn (Reewu Tinisi) + Socrate (Reewu Geres) + Diodore Cronos (Reewu Geres) + +Xeltu +Boo gëstoo kartu adduna bi bu baax dinga ca gis dëgg yii : +- Kaw kol-kolub suuf si mi ngi ame ci jéeri ji ak ndox mi, bu ko defee jéeri ji yóbb ci benn ñeenteel, maanaam bu doon ñeenti xaaj la benn bi, ndox mi moom yóbb ci ñatti ñeenteel . +- Jéeri nag mi ngi ame ci juroom benni gox walla kontinã ( ci lu dul goxub dott (pole) bu bëj-saalum bi nga xam ne kenn dëkkewu ko ngir jawwu ak dénd bu méngoodi ba), juroom benni gox yii danu leen a toftale kem ni nu yaatoo : +1 – Goxub Asi : moo ëpp ci gox yi, ab tolluwaayam toll ci benn ñaareel 44 milyoŋi kilomet yu kaare , way dëkk ya tollu ci 2200 milyoŋ ciy nit. +2 – Goxub Afrig : ab tolluwaayam di benn ñeenteel 30 milyoŋ ciy kilomet yu kaare , way dëkk ya tollu ci 350 milyoŋ ciy nit. +3 – Goxub Amerig gu bëj-gànnaar gi: ab tolluwaayam tollu ci benn ñeenteel 24 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 270 milyoŋi nit. +4 – Goxub Amerig gu bëj-saalum gi: tolluwaayam toolu ci ñatti ñeenteel 17 milyoŋi kilomet kaare, way dëkk ya tollu ci 300 milyoŋi nit. +5 - Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits (longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu. +5 – Goxub Tugal ab tolluwaayam tollu ci benn ñaareel 10 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 750 milyoŋ ciy nit. +6 – Goxub Ostraali : ab tolluwaayam tollu ci ñatti ñeenteel 7 milyoŋi kilomet kaare , way dëkk ya tollu ci 15 milyoŋi nit. +- Ndox yi nekk ci kaw kol-kol bi (globe) ñi ngi ame ci mbàmbulaan yi : ñoom ay diggante yu rëy lañu yu ndox, ak ci géej yi: ñoom ay diggante yu gën a ndaw lañu yu ndox . Bokk na ci mbàmbulaan yi : màmbulaan gu dal gi (moo ci gën a rëy) ak gu atlas, ak mbàmbulaan gu end gi ak gu bëj-saalum gi ak gu dott bu bëj-gànnaar bi(pole nord). Bokk na ci géej yi :géej gu diggu gi (mediteranee) gu xonq gi , gu araab gi, gu ñuul gi añs . +- Adduna ju njëkk ja walla ju yàgg ja – moom mi ngi ci xaaj bu penku bu kol-kol bi – mi ngi ame ci ñatti gox walla kontinã yu taqaloo, daal di sos nag benn dank (bloc) walla jóor, ñatti gox yii ñooy : Asi, Afrig ak Tugal, dara taqalewu leen lu dul yenn ci ay feeñte yu dénd yu néew : niki géej yu xat yi ak càllalay doj yi ak tund yu yaatoodi yu néew yi ag yékkatiku. +- Nit dundal na goxi adduna ju yàgg ja la ko dale ca ba mu tegee tànkam ci kaw suuf rekk, bu ko defee ay xay (civilisation) yu mbay, yu kawe, yu yàgg daal di am ci xuri ay dexam yu naat ya, lu ci mel ne xay ya amoon ca xuri dexug Niil ga nekk Isipt ak dexug Dijla ga ak Furaat ca Iraag ak dexug Sand ak Gangas ca End ak dexug Sigyang ak Yangci ca Siin. +- Adduna ju yees ji – moom mi ngi ci xaaj bu sowwu bu kol-kol bi – mi ngi ame ci Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Amerig gu bëj-saalum gi, ñoom ñaar ñooy ñaari gox yi nga xam ne bi leen nit wuñee (decouvrir) ak leegi ay xarnu (siecle) rekk la, la ëpp ca ña fa dëkke ay waa Tugal lañu yu gàddaaye Tugal dëkksi fa, moom Tugal nag benn la ci goxi adduna ju yàgg ji . +- Goxub Ostraali –moom moo gën a tuuti ci gox yi, te gën a rëy ci duni adduna bi- mi ngi nekk ci xaajub kol-kol bu bëj-saalum bi, ca bëj-saalum gu penku gu dankub adduna ju yàgg ja. +- Mbàmbulaan gu dal gi moo dox ci diggante ñaari gox yii di Asi ak Ostraali cig wàll, ak ñaari gox yii di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi ci geneen wàll, bu ko defee mbàmbulaan gu atlas moom dox ci diggante ñaari gox yii di Tugal ak Afrig ak ñaar yee di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi , bu ko defee mbàmbulaan gu end gi tàqale ñaari gox yii di Aseek Afrig wëlif goxub Ostraali, mbàmbulaanug bëj-saalum gi tàqale mbooleem gox yi wëlif goxub dott bu bëj-saalum bi. +- Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits (longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu. +Wuutuloxo walla masin mbooloom ay cër la, yu am lu bon-bon benn bu man a yëngu, yees lëkkale ngir jublu ci mu def jenn jëf ji jees tëral-jëkk, kon muy lu man a def liggéey bu nit dul man, ndax xéj-na dafa laaj jenn doole ji walla mu koy war a defe ci wërlaay gu nit manuta dund. + +Xeeti wuutuloxo yi bari nañu te itam dañu leen defar ngir njariñ yu wuute: ci misaal, wuutuloxo bu mbëj, wuutuloxo bu mbay, wuutuloxo bu yóbbte ak yëkkati, ak yeneen. + +Jëfandikoo gu wuutuloxo yi dimbali na nit ñi ba ñu man a def liggéey yoo xam ne weesu nañu dooleem, kàttanam. Bu dul woon wuutuloxo yi, nit ci dundiinu nit ñu njëkk ña lay des ba tay, te du am nenn numu man a def ba jëm-kanam. Kon wuutuloxo day tekki bepp jumtukaay buy yokk sa doole, di wàññi sa coono, te di gaawal aka gënal sa liggéey. + +Doolerandu +Xarala +Mooy xam ni yaram yi mel walla jëmm yi, walla seen dëgg-dëgg ci lu dul laalante gu fisya (fisi) walla gu kimya (simi) gu jonjoo ak yaram yii. Bokk na ci ni nu ko gënee doxale, ëpp ko nee defe ci jamono jii: nataali jawwu yi nuy defe ci satalit yi (jumi asamaan yi) walla ci fafalnaaw yi. Bokk na ci li nuy doye ligéey bii: + +Wàll gu jëm ci jiyoloji: wuññi petorol(feeñal ko), ndox, mbell yi, añs... sopparñiku gu jiyoloji. Mbay: xam tawat yi ci gàncax yi, xam xeeti gàncax yi nekk cib barab. Xam-xamu galaas yi: xeentu walla topp ak gëstu yëngu-yëngu gu jóori galaas yi ak ni nuy seeye. +Berlin mooy péeyu réewum Almaañ. Nit ña ña nga tollu ci 3 440 400 (2010). + +Péy +Almaañ + + +Xamale Melosuuf + +Melosuuf mooy xam-xam biy settantal ak a leeral feeñtey yaram yi walla jëmm yi ak yu dundat yi a yu nit ñi ci kaw suuf si ak gëstu gi aju ci ni ñu séddalikoo. + +Li muy wund ak li mu doon + +Séwogaraafi baatub gereg la, boo ko doon firi ci wolof muy “melal suuf si”, maanaam wax ni mu mel, ni mu nekke.Moom nag baat la bu tukkee ci (Geographica): baatub gereg bob cosaanam mooy (Geography),muy ñaari baat yu ñu boole ñuy benn bu njëkk bi mooy tekki melo, walla nataal (Graphica), ñaareel bi di Geo di tekki suuf. + +Bu nu sukkandikoo ci loolu danu naan Sewograafi walla Geographia mooy “melal suuf si” walla wax ni mu mel, xam-xam bii noonu la tàmblee woon, ndax ca njëlbéen ga, tukkikat yi daa wër di gëstu dañu daa bind li ñu gis ci dëkk yi nu romb ak gox yi ak diiwaan yi ñu siyaare, leeral, melal ni ñu leen gise, fekke leen ni. +Sewogaraafi nag déggoo nanu ci séddale ko ay xaaj ñooy yii: +Séwogaraafi bu dénd bi (nature), mooy biy sonn ci gëstu ni suuf si mel, ni mu bindoo ci wàllug jiyoloji, ak feeñte (fenomene)yu jawwu yi ak gàncax yeek dundat (animal) gu dénd geeg gu jeeri ji. +Bokk na ci xaaj yooyu Séwogaraafi bu bidiw, li ko tax a jug di: jàng ni suuf si bindoo ak ab kemam, ni muy yëngoo, ak ni mu buloo ak séqoo gi mu am ak yeneen bidiw yi. +Bokk na ci xaaj yi ba tay, Séwograafi bu nit: moom nag daa séddaliku ci :Séwogaraafi bu way dëkk yi (abitant), ak séwogaraafi bu koom koom ak bu politig, mooy gëstu ci goxi àdduna bi aki pegam (frontiere) yu politig, aki jafe-jafeem ak ña fa dëkk. +Ak bu nataal yi walla bu lonkoyoon yi: moom mooy xam-xam biy yittewoo lonkoyoon sewogaraafi yi ak ni nu leen di sose. +Bu yàggul bànqaas bu yees sosu na ci xam-xamu Sewogaraafi, mooy biy nos xam-xam yu sewogaraafi yi ak yëglu cig sori + +Njariñul xam-xamu melosuuf + +Melosuuf moom nekkatul rekk xam-xam boobu di melal feeñte yi (les phenomenes) di leen melal ak a leeral ci anam gu tond, gu soreek li am, waaye mujj na di xam-xam bi jagoo dox ànd ak jëm-kanamug xam-xam bu bees bii sukkandiku ci gëstu ak nattale, ak làmb ba daj, ak jëfandikoo misaal yi ak gis-gis yu yees yi, ci noonu la mujje di lu nuy doxal ci anam gi nuy tudde séwogaraafi bu kem ak séwogaraafi bu doxal walla dëppale “bu pratique” bi nga xam ne du nangoo beru wëliif soxlay nit yu mag yi, loolu nag li ko waral mooy li séwogaraafi làmbool yor ko ci man–manu dëppoo ak mbooleem xam–xam yi, moom mooy aji jokkale ji nekk ci diggante xam–xam yi di leen booleek a jokkale, bu ko defee di leen tàggat ngir ñu liggéeyal ko, di jël ci ñoom lu koy jariñ, di ko ràññale ak yeneen yi. +At yu mujj yii seere nanu ag soppiku gu mag ci gérum séwogaraafi ak xam-xam bi mu ëmb, ak ci anam yi muy jaar ngir amal ay jubluwaayam aki xemmemtéefam. Man naa am nag mu bokk ci li indi coppiku gii: jëm gi nit ñi gën a jëm kanam, nga xam ne sax boroom xam-xami séogaraaf yi mujj nanu di gëstu ay mbir yoy bu njëkk xamuñu leen woon, ba sax kuy seetlu liggéeyu boroom xam-xam yii dana gendiku yittewoo gu dolliku gi nu sotti ci mbirum gëstu feeñte yi /phenomenes/ ak masala yu wuute yi aju ci dénd bi ak nit, ci anam gu wuuteek ga nu ko daa g��stoo bu njëkk, sababus loolu nag mooy jëfandikoo gi nuy jëfandikoo leegi ay jumtukaay yu xarañ te aaytal ci seeni gëstu, di dimbadikoo xam-xami takk yi (statistiques) ak yu xibaar yu jumtukaay yi ak mat ak misaalukaay yi (echantillon) ak xam-xamu xarala ak dénd (nature bi) ak kimya (simi). Jëm kanam gii am nag ci jëfandikoo jumtukaay yii ak ker-keraan yii (ces moyens) tax na ba ngérte (resultants) yu am solo juddoo ci, yu jañ séwogaraafi mu jëm kanam, def ko muy xam-xam bu jamonoo. Loolu sax tax na ba ñenn ñi di woowe jëm kanam gii am ci xamu melosuuf ((jeqiku walla fipp gu kemu ci xam-xamu séwogaraafi)), +Jeqiku gii walla fipp gii waa melosuuf yi teeru nanu ko te màggal ko, ndax ngérum kem ay ngënéelam lu bari la, man naa am li ëpp solo ci ngënéel yooyu mooy ngérte yi mu lay àggale yépp ñooy gën a sew, gën a am maanaa, ngir seggat (analyse) gu xam-xam gi muy amal ñeel toftaloog mbir yi. Ceggat gu xam-xam gu melosuuf gii mooy wone noste (systeme) yi amal ay jeexiital ci amug feeñte yu wuute yi melosuuf di gëstu. Moom du doylu ci leeral feeñte yi rekk waaye day sukkandiku ci sabab yi sos feeñte yii. + +Ëttub gëstu gu melosuuf + +Ngir melosuuf man a génne, feeñal lëj-lëj ak jafe-jafe yi gawu cib gox walla ab diiwaan, li muy njëkk a def mooy digal ëtt boobu walla barab boobu , maanaam wutal ko aw dig ba ñu xam ne fii la, bu ko defee mu fésal séqoo (les relations) yi am ci diggante mbooleem xeet (element) yu wuute yu kojug dénd yi (naturel) ak yu kojug nit yi, ak nu ñu man a duggantee ci seen biir, ràbbaloo ni. Looloo tax séwogaraafi fi di boroom jikoo ju ràññiku, ndax danu koy gis mu tegub tànk ci xam-xami dénd yi, tegati beneen ci yu nit yi. Bu fekkee ne xam-xam yu wuute yi ci atum 1972 lanu leen raŋale, nos leen, séddale leen ñatti kuréel ñooy : xam-xami seggat yu nattu yi, xam-xami firi yi ak taawiil, ak xam-xami jam yi (yu critique yi), bu fekkee ne noonu la it melosuuf moom jël na mbooleem jikkoy yii kuréeli xam-xam . +Jàng ëttub melosuuf dina feddali amug ay way nekk yu bari yu dénd ak yu nit yu lënkaloo yuy ràññikoo ci jëflante yu bari yuy am ci diggante way nekk yii, loolu moo lay won foofu solos boroom xam-xamu melosuuf, looloo tax nga gis gëstu ëttub melosuuf du yam rekk ci menn mbir walla benn feeñte bàyyi ya ca des, ak doonte ëttub melosuuf làmboo na mbooleem feeñte yépp, teewul gëstug feeñte yii day am cig beru tey natt tolluwaayu jëflante gii seggat ko, yillaal ko , ci lu dul muy sàggane benn xeet (element) ci xeeti ëtt bi. +Ngir solos ëttub melosuuf Unesco saxal na ni nu koy jàngalee ci Tugal ci donga yiy door a dal, bu ko defee ñuy def aw doxaliinam ; sukkandiku ci dégg te xam juroomi laaj loolu nag mooy : ëtt biy jóox (biy produire) : bu ñu laajee njàggaan li jéego yi aju ci déggiinu ëtt biy jóox loolu man naa doon yoon wi ngir xam dëgg gi maanaam yewwu ci ne ëtt boo gis du lu dul melo ci meloy yëngu yi (maanaam mi ngi ci melow jóox) kon nag ngértel saxal yu tukkee ci nit ñi la (jeexiitalu jëfi nit) + +Lonkoyoonu adduna bi + +Boo gëstoo lonkoyoon (carte) adduna bi bu baax di nga ca gis dëgg yii : + +- Kaw kol-kolub suuf si mi ngi ame ci jéeri ji ak ndox mi, bu ko defee jéeri ji yóbb ci benn ñeenteel, maanaam bu doon ñeenti xaaj la benn bi, ndox mi moom yóbb ci ñatti ñeenteel . + +- Jéeri nag mi ngi ame ci juroom benni gox walla kontinã ( ci lu dul goxub dott (pole) bu bëj-saalum bi nga xam ne kenn dëkkewu ko ngir jawwu ak dénd bu méngoodi ba), juroom benni gox yii danu leen a toftale kem ni nu yaatoo : + +1 – Goxub Asi : moo ëpp ci gox yi, ab tolluwaayam toll ci benn ñaareel 44 milyoŋi kilomet yu kaare , way-dëkk ya tollu ci 2200 milyoŋ ciy nit. + +2 – Goxub Afrig : ab tolluwaayam di benn ñeenteel 30 milyoŋ ciy kilomet yu kaare , way-dëkk ya tollu ci 350 milyoŋ ciy nit. + +3 – Goxub Amerig gu bëj-gànnaar gi: ab tolluwaayam tollu ci benn ñeenteel 24 milyoŋi kilomet yu kaare, way-dëkk ya tollu ci 270 milyoŋi nit. + +4 – Goxub Amerig gu bëj-saalum gi: tolluwaayam toolu ci ñatti ñeenteel 17 milyoŋi kilomet kaare, way-dëkk ya tollu ci 300 milyoŋi nit. + +5 - Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj-saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits ( longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu. + +5 – Goxub Tugal ab tolluwaayam tollu ci benn ñaareel 10 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 750 milyoŋ ciy nit. + +6 – Goxub Ostraali : ab tolluwaayam tollu ci ñatti ñeenteel 7 milyoŋi kilomet kaare , way dëkk ya tollu ci 15 milyoŋi nit. + +- Ndox yi nekk ci kaw kol-kol bi (globe) ñi ngi ame ci mbàmbulaan yi : ñoom ay diggante yu rëy lañu yu ndox, ak ci géej yi : ñoom ay diggante yu gën a ndaw lañu yu ndox . Bokk na ci mbàmbulaan yi : màmbulaan gu dal gi (moo ci gën a rëy) ak gu atlas, ak mbàmbulaan gu end gi ak gu bëj-saalum gi ak gu dott bu bëj-gànnaar bi(pole nord). Bokk na ci géej yi :géej gu diggu gi (mediteranee) gu xonq gi , gu araab gi, gu ñuul gi añs . + +- Adduna ju njëkk ja walla ju yàgg ja – moom mi ngi ci xaaj bu penku bu kol-kol bi – mi ngi ame ci ñatti gox yu taqaloo, daal di sos nag benn dank (bloc) walla jóor, ñatti gox yii ñooy : Asi, Afrig ak Tugal, dara taqalewu leen lu dul yenn ci ay feeñte yu dénd yu néew : niki géej yu xat yi ak càllalay doj yi ak tund yu yaatoodi yu néew yi ag yékkatiku. + +- Nit dundal na goxi adduna ju yàgg ja la ko dale ca ba mu tegee tànkam ci kaw suuf rekk, bu ko defee ay xay (civilisation) yu mbay, yu kawe, yu yàgg daal di am ci xuri ay dexam yu naat ya, lu ci mel ne xay ya amoon ca xuri dexug Niil ga nekk Isipt ak dexug Dijla ga ak Furaat ca Iraag ak dexug Sand ak Gangas ca End ak dexug Sigyang ak Yangci ca Siin. + +- Adduna ju yees ji – moom mi ngi ci xaaj bu sowwu bu kol-kol bi – mi ngi ame ci Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Amerig gu bëj-saalum gi, ñoom ñaar ñooy ñaari gox yi nga xam ne bi leen nit wuñee (decouvrir) ak leegi ay xarnu (siecle) rekk la, la ëpp ca ña fa dëkke ay waa Tugal lañu yu gàddaaye Tugal dëkksi fa, moom Tugal nag benn la ci goxi adduna ju yàgg ji . + +- Goxub Ostraali –moom moo gën a tuuti ci gox yi, te gën a rëy ci duni adduna bi- mi ngi nekk ci xaajub kol-kol bu bëj-saalum bi, ca bëj-saalum gu penku gu dankub adduna ju yàgg ja. + +- Mbàmbulaan gu dal gi moo dox ci diggante ñaari gox yii di Asi ak Ostraali cig wàll, ak ñaari gox yii di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi ci geneen wàll, bu ko defee mbàmbulaan gu atlas moom dox ci diggante ñaari gox yii di Tugal ak Afrig ak ñaar yee di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi , bu ko defee mbàmbulaan gu end gi tàqale ñaari gox yii di Aseek Afrig wëlif goxub Ostraali, mbàmbulaanug bëj-saalum gi tàqale mbooleem gox yi wëlif goxub dott bu bëj-saalum bi + +- Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits ( longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu. + + +Melosuuf +Seex Ahmadu Bamba +Téere Irwaun Nadiim ci Sëriñ Tuubaa +Téere Tasawudus sixaar +Ab jukki ci liggéey ci murit +Daaray Sëriñ Tuubaa +Waa kër Sëriñ Tuubaa +Seexi sëriñ Tuubaa yi +Yoonu murit + + +Bii téere nag am ay liggéey yu néew yu ci des + +Bii mooy teereb Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji(ki ngay toogal di naan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di xam-xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin. +Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yermaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal. +Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin. +Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindeefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam. + +Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci walliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. Ndax kat ñooñooy ñi yàlla naan ci alxuraan: ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi. + +Di julli tey sëlmël ci yonant bi. + +Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbeg mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa’ng ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBAKKE Xaadimur rasuul. + +Bi loolu amee ma bëggoon a leeral as lëf cig dundam ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a neew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. + +Waaye nag dinaa jeem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñewee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw walliyu mel na ni dundal nga ko. +Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jeggalul ma yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yeem, lu man a wecci loolu ko yeemutoon, ndax teere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere degg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii maathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngëneeli sheexul xadiim. + +Doomam ja sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndaxañteefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak kim ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. +Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngëneel ak tawfeex,tey borom li fii ak la fee. + +gu njëkk gi ci xamale kuy sëriñ bi aki mbiram ba bi waajuram wu goor làqqoo + +Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax – ci atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk 1270 g, am ñu ne atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar 1272g,ca kër waajuram wu goor ca Mbakke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum sharaha,muy 1270g làqu atum shumoos muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant. Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar,ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram)). + +Moom sëriñ bi bi mu ganee àdduna waajuram wu jigeen a ko yoroon bam mat a jàngi, Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah doomi Muhammadul kabiir mom Habiiballaah mu njëkk ma doomi Muhammadul Xayri,ak Muhammadul Kabiir,Muhammadul Kabiir mii mooy ki niy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbakke Bawal atum 1194 g ,ci li nu wax,waaye dëkkewu ko woon da faa ba woon ab taawam Muhammudu Farimata,magi habiibullaah waaye bokkunu nday,moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof,fa la làqqoo nu denci ko fa,di ko siaare. + +Mi ngi askanoo nag ci tukkloor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof, siw na itam ne ñoom Gànnaar lan bawoo dem, Fuuta,seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay serif lanu.Sama mag sama sëriñ sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne degg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu,mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lan. + +Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te deggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu. + +Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu,kon sëñ bi serif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke jëm fun naan Mbumbe péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbakke-makke yi dëkke woon. + +Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbakke-mbakke yi seeni doomi baay tëx lanu,kaaf gi nekk ci Mbakke ag Haa la woon muy haa giy mujj ci ba,wolof yi def ko kaaf,waaye wax jooju ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab),li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci ne dëgër na te am na màndargaam dëgg. Waaye Buso-boso yi ñoom seen cosaan Fuuta la ca fa niy wax Golare, barab yii yepp it yu jegee lanu,barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddgay ñaari askan yi. +Bi sëriñ bi tollee ci war a jàngi,wayjuram dal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. +Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgu’s lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbakke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi ju jigeen,ndayi wayjuram wu jigeen,soxna Asta Waalo. Nu daan nekk foofa fa moom ca Mbakke bu noor baa, bu nawet baa lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal. +Kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne, sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daa wul tàggalikook moom lu dul lu neew,ndaxte magam Muhammad Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg amaa na mu jaar fa nekk faak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jihaadkat boobu di Mabba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Mabba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme Saalum,nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa kenn. + +Bi mu faatoo nag moom Mabba nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukkloor KA doomi bàjjani baayam,bi mu jàngee ci moom dali xam-xam,tàmblee ñawu’s lëf la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono.Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caageenug seen teddngay nguur gi,li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk,ndax da daa jàng ak a jàngale,te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur,li fi ne daal ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona. + +Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daa na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey baak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indili woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu genneel ko ci’b yàq,ba mujj sëñ bi far ko raw, mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko ma mokkal ko,mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal lim koy indil,nii la nekke woon ak Xaali. + +Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def teere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan(xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it – ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). + +Bi wayjur wi xamee ci moom raw geek cawarte geek laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci teereb boppam ba walla ci teere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla teere ba, bu ñewee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féeteseek moo,doylu ci moom,waajur wi ba leen ak moom te bég ci. + +Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala,dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanci ca wetam,tudde ko Mbakke Kajoor,sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam,nee nanu, looloo ngi am ci Muharram,atum 1300g, dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat ,took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqqu,nu denci ko Deqale ,di ko siaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. Bi niy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wallug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bepp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denci gi,sëñ Tayba digale na nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil ,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale geek dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àddina ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas. + +Ña cay ñu baax wax ji da leen a yeem rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara. Bu dee mbooloo mi moom li leen yeem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yeeme,bu njëkk bi mooy waxam jii: +nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëliif leen ba fam yam ,teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii: +nee nanu ma jengal jëm ci bunti buur yi,kon dey da nga ami may yu lay jariñ jamono ju ne. +Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine. + +Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal. +Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte?. + +Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane. +Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom aras laay woo. Mooy aji dimbali, ji dara dul të,te mooy kiy amal li ko soob. +Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir. + +Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man awma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina. +Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon dey ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gecceel. + +Waajuram wu jigeen wu tedd waa nga làqqoo Poroxaan ca Saalum nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee. + +ci nu mu nekke woon ginaaw bi waajur wi làqqoo gërëmul yàlla yal na nekk ci ñoom + +Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwtoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang fu nu ko jëmewul du fa jëm, bi mu làqqoo nag,mu des ca ligeeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp, ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa ba woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi,ak seeni xam-xam,ak berook a wër,niki ñu baax ñi,mu leen daa junju ciy waxam,ak a feeñali maanaa,ak a yëgg,ba bi ko himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yite) dikalee ,muur ko,mu jug yëggus lëf neeti tekk,dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu,bi ko mbir mi gënee lëjal nag gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi. + +Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen yeen mbooloo mi ku àndoon ak man, ngir jàng rekk,na laxas jëm ca boppam aki mbokkam,mbaa fa ko soob,man loolu rekk taxatumaa jug,ku bëgg li nu bëgg nag,na toog,dal di leen fay ba dugg ca biir. +Waxam jii nag dal di leen ba cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem,sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem ba ko fa,la ca gën a néew des fa. Bi loolu lepp data am,fekkoon sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal ,yu sariiya yi, mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko,beg ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Degg naa ci sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. + +Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g,teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla). +Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci Himma te bu leen yar ci njàng,loolu sëñ bi gën na koo leeral ci qasida gii: + +Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy walliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw. Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel).Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw) ,mooy ji ci alxuraan: fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal lin la digal te dëddu way bokkaale ñi. + +Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindeef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy teere,kon boo may ligeeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : neel weeru leen ci man.Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab weeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgguw yiw àddunaak allaaxira,na weeru ci man. Mu dellu waxaat ne: Murid bu yoqqatul ci man de texe na,ci làqq ngën ji ay may. Murid bu yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na ceru ciy may. + +Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam. +Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Kepp ku aju ci man dey am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira. +Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi junne yepp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : Junney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñepp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul. + +Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid. + +Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne: Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax – mooy bàyyi aada,( muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam. Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu. + +Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox kow yiwam. + +Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg. +Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona. +Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj dib sëriñam fu mu jublu. +Ab sëriñ du wuuteek ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu. + +Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba. +Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam. +Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wepp yiw: Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru. +Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk. +Bayyi gaaru ci lum man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci lin nettali. +Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort. +Képp ku boole yile melo ci murid yi dey,da na jot ndëërlaay ya(gaa yu baax ya). + +Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi. +Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm. Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def. +Nettali nanu ne malaakay aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif. + +Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew. +Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,teere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def. +Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yeem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci teere bii,du amati,ndax moom teere bii as kook la ci geejug xamale ko. + +Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci ay wuññi ñeel lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ñi aju ci man bu nu ko defuloon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla. +Li waral sama tukki bu sori bi,yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama diganteek nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye yàllaa ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay yonant bi (j.y.m). Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne : Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yeek yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addinaak alaaxira,ci barkeb yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julleek woor,ak lu dul loolu ci lepp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam. + +Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñepp,mu ne ci: assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi ba dunu la laaj dara. + +Lii nag xamle la gum teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme?lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca yàlla, àgg ci yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku weetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manta ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am deet,du ligeeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu sheexu tarbiya la war. + +Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligeeyloo,aki tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligeeyloo leen ci nu jeem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbàir mu gudd,manunu cee wax fii. Mu dem ak ñoom cib yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngërum tàggat,dajle leen,di leen ligeeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqqoo lab,ak a beru,rawati na sori jigeen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul yàlla, yalla jënd na ci jullit ñi,seenii bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana, sëñ bi wëy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak benn,ba bi mu sancee Mbakke Bawal,ci at moomu juge Mbakke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu ne, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñeek ñu sori ñi, ñeppuy yeemu ci moom,te booba amagutoon sax fanweeri at. Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñim siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fam yam,looloo taxoon kenn ci sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a wooyey sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoonwi ci ndimbalul yàlla nag muy yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacci ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir yàlla ak a soppanteek a jriñante ngir moom. + +Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem. +Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiid,yu tollok ay teemeeri bayit,bokk nan ci yile:(( Shex Ahmadu xeewal la gu yàlla jox mbindeefam yi)) ak waxam ja: (( sëñ bi daal xeewal la gu yàlla xeewalee,di kiimaan ci kiimaan yi)),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lum wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu yàlla,yal na ko yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñim siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi ma jublu ci Hamdim ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali ming ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy dajeek wasila wu mag wi,di yonant bi (j.y.m) ,te leeralunu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne deedeet,waaye nettali lim waxoon ci diggante sëñ beek Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon. Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee ci bi miy siyaaresi Ustaas ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala dang koo bàyyi ngir yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan nii,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir yàlla,jum munta baati,ndare cib coona,ma jëflante ceek moom waaye yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng. Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaaas seetsi na Sëñ bi Njaareem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yeek naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne yàllaa tax nga ba ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke. Bi sëñ bi nekkee ci wëram boobu nit ñaang ko daa dikkale gepp wàll ngir xam-xam bu bari beek njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari jim daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,ngor akub jam,ku am ak ku amul,ku baax ak bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci yàlla ak yiteem jepp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci reewam ginaaw bi. Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gu àddunaak nit ñi jublu,nu tambli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoon,lor yi ëpp,mu mujj beru leen akum mbooloom ak jàkkaam, yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasook ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yum ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarlook moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jëggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi. + +Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi –mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amooni alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,bam gañe ko ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal aki jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lan bawoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a defi jaami,kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,kon alalam ak dereetam dagan na,nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalun ko. + +Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacci mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji deggal ko,def ko ànd ceek kontaante,Latjoor aki gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,regg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weññ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def kum dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub. Ñu xam ne lim wax lu dëggu ci moom la, ñu jëggal ko noppi cim mbiram. Waaye sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul sëñ bi bañ,nee nan ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : neel ki la yonni rus naa malaakay yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla. Degge naa ci sheex Aadama SÀLL – moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci sëñ bi cosaanoo woon Jolof – mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan, Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi – moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :(( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun)) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,yaay weñ wi man nag,ay dem-àll laa. Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu ba ko ak mbiram ,ndax kat notanteek moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànjnji ci toolam - te manu koo bay manu koo saxal –mu ba ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànjnji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah. +Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yeek coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcci benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkk,bi sëñ bi yëgee ne mook Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : (( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi )). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa ne woon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi Latjoor taxul,jubook moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sun mbir man ko woo woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal jiñ nangoo ci moom niki màgg ak njaf ñamu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lepp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waa,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw,sëñ bi ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonant? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xareek moom,nan lanu koy seedeele? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaaleek mbooloo mi ne tekkus lëf,bam yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la yàlla,nga jiitu nu ca,konug ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te jubook moom. Pënd ba wuriku,sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu yoon yepp dagg ci moom lu dul wi jëm ci yàlla,ndax kat moo ñë ci ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom: wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq. +Li mooy dooley sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jell yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yeeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara genn,te dunu lakk,di yekkati xasiday sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu ba, ñu leen di door ak a jeng,ak a nangu seen alal,ak a genne seeni kër,loolu lepp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem akug sóobu, mu mel ni loolu mbóotum yàllaa,mu ball juge ci baatinub seen sëriñ ba ca ñoom,sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay yonant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nannook lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,genne leen seeni kër,te loolu teewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca yàlla, : lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun, mu leen di xamal ni,da noo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu genne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku yàlla ak ngërëmam,ak dimbali yàlla ak ab yonantam, ñooñooy ñu dëggu ñi. +Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day dal di doon lu neew, laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira muy :ku gëm yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim muy deel jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. Dee leen di fuglu yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim muy bis ba niy woo nit ñu ne ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanook a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tag,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy teere bu amul moroom ci tazawuf,yor junneek juroomi teemeer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom. + +Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanci Daaru Salaam,ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tollookum at,di yar nit ñi,di leen yeege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,demus lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tollook juroom walla juroom benni miil,sanci fa Tuubaa,ci mujjug atum junneek ñatti teemeer ak juroom,walla ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak juroom benn,tuxu fa ak ñaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma – ñaareelu xalifa – ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos. + +Ku dul yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalanteeki xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yeek jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. +Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dollikook a yokku jamono ju ne,ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca geej ga. + +cig sancam jolof ak li ko waral + +Sëñ baa ngi sanci Jolof - ci li ma sëñ Mbakke BUSO nettali – bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denciy soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasook ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligeey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji yonant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon. + +Kenn ci sunu moroomi naari daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii nu ànd aji,bu neexee yàlla ,ma dem waaji te lijanti ji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun). + +Nu dellu ca wax ju njëkk ja,sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ceek man,diisook man ci mbirum ñu sanci ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligeey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd faak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. + +Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku wart a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah. Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làqq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul – bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada. + +Waaye sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom. +Kon sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon___p45 mahalu ajdaadihii ba bi xurbi Tuubaa_,walla muy aajowoo jankooteek ay ñoñam,mbaa mudaaraanteek ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbakke Baari,wacci fa,sanci fa,waxtaan faak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbeenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu duli buur,yu ñëw ngir xëccook ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee. Waaye yàlla moom bu bëggee amulum mbir da koy wutali sabab, nee nanu bu yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. Bokk na ci xeewal yi yàlla xeewale sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu walliyu yi, sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan muy ci maanaa yoonu yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu yàlla. Nit du jug mukk jëm ca yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg yàllaa ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,yàlla da koy feeñu cig màgg akub taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen yàlla di dëddaleek yen xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bop,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lepp,hifthul hinaaii du tàggook ñoom,mooy wattu gi leen yàlla di wattook a aar,dara du leen dal lu dull u yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan yàlla jàmm. Lii mooy mbirum sëñ beeki àndandoom ca njëlbeenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom sëñ Mbakke BUSO nee na:taalube yi mu ba woon Tuubaa,bi nu yëggee ni sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xaalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax deet ginaaw mbir mi dàu mbirum xalaat. + +Bu dee lu aju ci jaraaf dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu deggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu dikkal nu ci kaw ak suuf. +Bi buur yeek seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,dan daan song ku leen daa jeem a të,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donante,waaye loolu teewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom neeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki neegub sëñ bi. + +Loolook meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci sëñ bi,meneen mbir mi nag ,nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig,,,,p48,,,,,,,wakaana haaulaayi,,,,,,ba ,,,,,,falamaa lam yakun lihaaulaayi,,,, +Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexee ki wor. Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kilifteef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galak, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wuti ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu ,walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop. Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàqq dunu dañ,di yàqq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def. + +Looloo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañ koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkuloor la bu defoon ay xare ci wàll gi dëkke woon ,ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmadñ sheexu dib Tukkuloor,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi.Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu lin leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi sëñ bi,ginaaw bi ko yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,yàllaay seere lii nuy wax. +Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma laak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonant bi ji (j.y.m), ñi yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonant yi,teg ci walliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp, ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis : àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar ,yàlla itam wax ne : wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin muy àllaaxira, ñu ragal yàlla ñee ko moom. + +Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum sëñ bi, ñu tàmbli faa yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngeen linu leen waxoon am deet? . +Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu neew,bunu leen tollaleek li nu am ciy xarekat,ndax matunu mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi. + +ci tukkib geej gi + +Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul yàlla ak yonant bi (j.y.m),yonant bi(j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida: kun tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g. Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn dajeek ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak sëñ bi kerook la ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja – am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal ,danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,benn waay buy or ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te deggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara. +Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu sëñ baa ngi naan: ginaaw bi nu dajeek ña gennoon jëm ca këram,te njàqqare nekk ci seeni dënn. + +Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla. +Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siaare. +Mu jubale kanaman ca yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg. + +Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu. +Jaraaf ja genn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xeewal. +Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,sëñ nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaareem. +Sëñ bi nee na: (( Omar mii mi ngi genn,ngir siaaresi ma,dajeek soldaar siy genn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye yàlla moom xam na la nekk foofa)),sëñ bi nee na ((nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu deglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrankeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir )),,,p45 dale wa awra lihaasihiil aaya,,,,,,,ba,,,,,,,,,,,sais yamkur,,,,,,,,,, +wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu genne la, ñu nekk di fexe,yàlla itam di fexe,te yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :((Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel la woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonal ca daanaka-dun ba bepp (daanaka-dun mooy Presque ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrankeel ma, ñooña yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat)). Sëñ bi wax na ci loolu lii: yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono. +-Mu tàbbal ci seeni xol,ag genne ko,jëme ko ca réew yu sori ya,mu ame fa lu kawe déggub Saariya. Yàlla (t.s) dëggal na ba mu naan wal laahu xayrul maakiriin muy yàlla’ay ki dàq a fexe. Ndax xéewale na ma ñatt yu gën seen ñatti kuréel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dëgg-dëggi sëriñ,ci gëm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy ñàkk a nelaw guddi) te ñàkk ko ñu may jam ay xeej a ma ko gënal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gëm yàlla gi nga xam ne mooy dëgg-dëggi xam yàlla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wér la ne li nga nekk ay dëgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy àgg ca yàlla mu kawe mi, ñatti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasook ñoom,te looloo daa doon sababu rekki gëm,yal nanu ci yàlla musal. + +Ab nettali bu yéemoo ngii ma degge ko ci sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te féetee woon mbirum tukkib sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :(( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu genne ko,tumbrankeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu genne sëñ bi tumbrankeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,looloo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma sëñ bii fi yaw,bu ko jeem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yeene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca,looloo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lepp mujj yomb. Bi yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penk bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci genn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu gàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ)). Mbirum noonam boobu,nirook lool,mbirum noonub ki miy ligeeyal di yonant bi (j.y.m),noonam booba di woon,Haamir doomi Tufayli,ba mu nee – jamono ja ko tawat ji sonalee ci genn këru jenn jigeen ju Salool - ,,p57,,,,,,,,axudatan,,,,ba ,,,,,,,,bayti saloliya,,,,,,, +Sëñ bi def na ag xasida,gum u tënke arafi mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw ne; tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, mu damm. +Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi. +Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci ne,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko. +Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci geej geek ci jeeri ji,te am mbooloom wor ko. +Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,mook mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal sëñ beek a saboote,fu mu masaa dajeek moom,moo nekkoon Garambasaa. +Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakkru,ki ci des,di ku geej gi,nekk Konaakiri,yal na nu yàlla musal ak jullit ñepp,ci nattu bi mu leen tegoon. +Nu dellu ci mbirum tukki bi,sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy Inna walliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy yàlla mi wàcce teere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolooy maanaam waxam jii: yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi). +Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli faa woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, sëñ baa ngi wax ci loolu: ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt. +Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali – ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn gelamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu koo jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe?bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca ak ag xat te di ko muñ. +Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji. +Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii: +((kuy sukkandiku ci ndimbalul yonant bi,bu koy gaynde fekkee cib àll it wedam. +Moom yonant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan mook am mbooloo ànd ngir,màggam ga )). +Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa. +Nettali nanu ne sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lott,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma yàlla du lott te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara. wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii, muy ci maanaa bu la yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (yàlla mu sell mi dëgal na,yonant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jottalee). Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne yonant bi (j.y.m),yonant bi (j.y.m) nee na wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lott ci sama mbir,bumu lott ci sama sunna, sëñ bi moom donn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,JIbriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan. +Sëñ bi yonant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu yonant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi hasbunaal laahu wa nihmal wakiil muy ci maanaa yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la. + +Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma yonant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor. +Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : maa ngi sant ki ma musal ci lori jepp saytaane ak junne ak nit. +Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi. + +Maa ngi sàkk ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju ne. +Yeene naa koo ñaan di sàkk am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu. +Mooy Ahmad,sangub mbindeef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom. +Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xaccoo. +Yaa moom mbindeef yi ,yaw sama boroom,may ma ag muc ci ñoom,ak bepp balaa ak mbugal. + +Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal. +May ma li ma bëgg ci addina ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àddina ak gu allaaxira. +Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma. +Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo. +Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb yonant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef. +Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon. +Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lepp lu ko man a jublu ciy mbugal. +Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax. +Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jepp fitna. +Fegal ma loxol woy bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge. +Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gecceel,ci àddina ak àllaaxira,te dee ma jéggal. + +Bindalal yonant bi ag xeewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax. +Mu tëje ko fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim : muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xeewalug yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul yàlla te yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li). +Mu neeti alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina muy ci maanaa : ( maa ngi sant yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na yàlla,miy boroom mbindéef yi) . + +Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo. +mu wax: allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom. +Waxees na ma ,te loolu lu wer la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii : (( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee). Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul sëñ bi mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite. Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum---------------------- waafiris sitri iiiiiiiiiii bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal kepp ku ko daa jeem a lor,teere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabeey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee. +Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at aki weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,joy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci geej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yeeme,gi nga xam ne sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi(waa Ahlu Badri),bi may dox(bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp)laa. + +Sama dox bi may def,ci wommatug yonant bi, ànd ceek gaa yu baax yi,yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul yàlla. +Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man. +Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju ne mi ngi may sottil ay xeewalam ) te mooy ki di ab santaakon(ku soxlaalul kenn). +Sama ndimbal,samag dëgaral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci aji yaatu,ji di ab mayewaakon +(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama. +Sama kilifa nag ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraam,di yonant bi,te mooy ki may ligeeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal. +Samab yool ci ligeey bi may defal ku nu tànn ki,di yonant bi, mayewaakon (yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la. + +Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligeeyal gën ji mbindéef,te moom yonant bi mooy samab xuppkat(yonant bi day bashiir tey naziir,di kuy begale tey xuppe njir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ). +Aji feg jii di yàlla,moo may fegal ci yonant bi,ayi noon yi,ak lepp lu ñaaw te mooy ki may xettali. +Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligeeyal yonant bi,mbiri mbindéef yepp nag ca yàlla lay mujj. +Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub yàlla,te moom siw na. +Samay sutura ci addina ak allaaxira,mooy tag yonant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la. +Samaw jiwu mooy teereb yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu(muy saytaane). +Samay kër weet na, ñoñ ñi tas,ngir tag ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat. +Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la. +Sëñ bi nee na : ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu sëñ baa ngi ciy wax naan: yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde. +Ñu àndandoo sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari. +Ma sax fa – sëñ beey wax – la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci laa dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen ba leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu. +Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku weet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caangeenug aw wettal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ? +Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!. +Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àddina yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bop,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna. +Ca bis ba mu war juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn. +Bi sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. +Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci yonant bi (j.y.m) ki may ligeeyal,sama dënn leer,sama xol dal,koolute gi dolliku ci yàlla’ak yonant bi,ndax alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub ci tudd yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale. Sama gudd gi dal di neex ci yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan: +yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wepp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe )bi xëccoon jëme ci man. +Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye yonat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu. + +ci dugg gi ci gaal gi juge Ndakaaru + +Bi nu xëyee – sëñ beey wax – muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal ma ca dig gaal ga,di joy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini yonant bi. +Gaal gu fees googu ak mbooloo yendu na fanaan. +Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga. +Murid ba tàggoo dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari. +Mu jublu ci muridam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñepp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba sëñ bi far jël daam ak xalimaam,nee na bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbiondéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi. + +Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saasa ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjalati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag nga xam ni mook nit ñepp a yam,dara waru ko lu dul,mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko. +Ci loolu mi ngi naan: +Ki njiit li yonni woon ca ligeeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu. +Ginaaw bi aji ligeey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal. +Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la yàlla di wonee aw yoon. +Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) ((wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca yàlla te yàlla’a ngi gis jaam yi. +maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi. + +Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa degg ñu ne yaa ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma. +Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul yàlla,ku jublu ci ku dul yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul yàlla,ku jublu ci yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad yonantab yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne yonant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem. +Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul genne ci ab neeg ne ma,ndax yaay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gall gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu sëñ ba’a ngi naan: sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi. +yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lepp luy xëcce jëme ci yu nu sib. +Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma. +Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,maanaam laa ilaaha illal laa,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,p 73,,,,,,,,,,,,wahuwal lazii yaqahu bihiil inkaar,,,,,,,,,ba wa qad barraahul ,,,,,,,,,,,,,,,, +Du àddiyay xaalis ju waa jooju,mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yeeme gi ko yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yereem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi teeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñepp walla ña ca ëpp,ci loolu la sëñ bi naan : kiy jagleele yërmaandeem di yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle. +Mu jublu woon ci aji yërame jooju yàlla mii di boroomi xeewal,daa ko indil ay xeewal,bokk na ci xeewal yooyu biteeli misk yooyu,mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li dal sëñ bi,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ,mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe,mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñepp ba kerook muy wàcc Gabong. + +Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mujje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci yàlla ak yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug geejug dun boobu laa taxawoon di irtijaal (di wax ci lu dul xool li may wax ci am mbind) di xutba geej gi naan: +yaw geej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd. +Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,,,,,,,,, + +Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal yonant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fepp. Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yepp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saasa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne : yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmax ab loxoom bëmax gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lepp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tollook waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrankeel ak a genne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daa taa wàcci,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,looloo waraloon sama ñëw gii du leneen. + +Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu beg ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah. +Da na xoromu ñu indi fi as lëf ci bayiti Ibnu Hanbal yii,mu jëme woon ci Sëñ bi ci lu aju ci xar-baax yu mel ne yooyu: +((Boriwaa na aji jalgalti , ku di ab tooñkat ku sol yerey teddngaam di puukarewu,ciy tëneem aki takaayam)) +((ay junniy junni ñoo nekk ci ron kilifteefam,te du faale lu koy digal mbaa mu koy tere)) +((ngeen (sëñ bi lay wax) wacce ko ci mbartalum toroxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) )) +((ndimbal lu tukee ca Yàlla ñeel jaamam bii di jëwrini yonnant bi,muy ndimbal lol nasaraanam yi sax mujj nanu ci di ay ansaaram (di ay gaayam yu koy jappale) )) +((bu wone woon mboot mi (sekkare bi) moom Sëñ bi,kon dey mbindeef yi gis lu yeeme,waaye moom dënam bàmmeelu ay sekkare la )). + +Tudd na moom Sëñ bi ne bokk na ci karaama yi ko Yàlla defal ci tukkib geej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat tubaab yi danu koo dëkkaloon ,ci benn ci dun yi, ca karce ga ,fa soldaar sa, ñuy fo ak a naan ak a tux,man may muñ seen lor yoou rekk,ndax xam naa ne ñaari malaaka yiy bind jëf yi, ànd nanu ak mukàllaf mu ne,te ginaaw ñoom ñoo man a muñ boobule coona ak yooyule lor,ngir top ndigalul seen boroom,kon man du rafet fi man may jàmbat,ndax kat li leen di lor rekk,mooy li may lor,li leen di naqàri rekk mooy li may naqàri,te jàmbatunu. +Ci noou Yàlla dogal bis soldaar si genn ngir tàggatuji, waaye ba ñu demee fa ñiy tàggatoo,fekk fa am mbooloo mu war ay fas,rang te kaalawu,ci noonu ñu tiit taxaw,seen njiit li tëyye leen fa,xupp leen ci ne bu xibaar bi siwee da na leen ray. +Ba suba jotee ñu ne mes gisatunu leen,nu dal di nëbb seenub xibaar ñeneen ñi ko yëguloon. Sëñ bi nee na bi loolu jàllee ba tegi fan, seen njiit woo ma,mudaaranteek man waxa man wax ju rafet,ci biir wax ji mu ne ma xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali boo bëggee def dara? Ma ne ay junne lanu walla ay nit ? mu ne ma yaa ko gën a xam ! +Sëñ bi nee na moom da koo wonoon ne moom yëgul li xew ,mu dal di noppi. Am na ñenn ci boroom xam-xam yi ñu ko laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi? Sëñ bi ne woon ko ngir tiital noon yi, keneen laaj ko ne ko ndax Ahlu Badrin ñooñu nit ña lanu walla malaaka ya ? mu ne malaaka ya, keneenati laajati ko ne ko ndax yonant bi (j.y.m) ca la woon?, mu ne ko moo doonoon seen njiit. +Ci loolu mi ngi naan: + yombalal na ma samay mebët fa Limbarwali,ki nga xam ne wommatal na ma lu fàddu wëlif wepp wàlliyu + ka soril rambaaj ba ak aji iñaan ja,wommatal na ma Ahlu Badrin ña diy gaynde + Yàlla moom’ay wommatal fu ma man a nekk mbegalum Laa-ilaaha illal laah. +Jiitalug aji firi ji (preface) +Jiitalug aji taalif ji +Xamale kuy Sëriñ bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu góor làqoo +Ni mu nekke woon ginaaw bi waajur wi làqoo (gërëmul yàlla yal na nekk ci ñoom +SancamJolof Ak li ko waraloon +Tukkib géej gi +Dugg ci gaal gi juge Ndakaaru +Dellusi gi juge ca géej ga +Ñaareelu tukki bi (bu Gànnaar bi) +Ñibbisi gi jugge Gànnaar +Ag génnam juge Jolof jëm Njaaréem +Tëjte +Seere yi ko mag ñi seereel ag màgg akug wilaaya + +Yoonu murit +Ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi,ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni. + +Maa ngi tàmblee ci turu yàlla, miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira. Yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang ,sunu kilifa, Muhammad,ak ñoñam aki saabaam,ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii, yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal,aamiin yaarabal haalamiin. + +Ahmadu mi dul dañ di sant boroomam, di jaamub yàlla,tey ligéeyal yonant bi (j.y.m) nee na : ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll,rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal.Maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid (muy wéetal yàlla),ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan,te ñooy sunnas yonant bi(j.y.m),xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba,soppeem ba,Ahmad,ak ñoñam ak saabaam yu gëm, yu jullite,yu tedd,yuy rafetal yi. + +Lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la, ma tudde ko yobbalub ndaw ñi(tathawudush shixaar) jem ca àjjanay yàlla jii ami dex,maa ngi ñaan yàlla ag +nangu,ak jàmm ak sell,ak màggal. +Maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub. +Tey texeg ndaw ñi,ak mag ñi,ak waxambaane yeek jigeen ñi. +Waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na,sunu boroom laa ciy wut ci lu sax. + +(AG JIITAL ) + +Yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub,te soxlawoo xam-xam,soxlawoo leen jàng ak mokkal,te teet barabi texeedi yi,taqoo leen ak ki dul +dañ di jaamu boroomam,ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme,kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub,bu màgge noppalu. +Ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen,te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell,ak jublu sunu boroom,am la gën. Jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox,kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira,bokk ci ñiy texe. + +(BUNT CI XAAJI DIINE YI) + +Diine ñatti xaaj la,benn xaaj bi mooy bu gëm, +Beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu,ak bu lihsaan,muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom.Lu ci ne dees na ko gën a leeral. +Ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm . + +Gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi,ak teereem yi mu wàcce,ak alaaxira,ak yonenteem yi ak dogal bi. + +(DOGGANTAL (chapitre) CI NI NUY GËME YÀLLA) + +Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam. + +Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. +Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) . + +Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, +(dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk). + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME MALAAKA YI +yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom) + +Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu. +Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde. +Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI) + +Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. +Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), +juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). +Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel +Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom) + +Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom. +Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal. +Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom. +Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal. +Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog. + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem ) + +Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak +sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay. + +Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone. + +Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi . + +(DOGGANTAL CI NI NUY GËME DOGAL BI) + +Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi. + +Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame. + +(BUNT CI LISLAAM) + +Lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa (muy yàlla rekk ay buur,amul beneen buur bu dul mom) ak julli ak woor,aj màkka,natt asaka. + +(DOGGANTAL CI LAA ILAHA ILLAL LAA) + +Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx. + +(BUNT CI JULLI YI JUROOM) + +Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña. + +Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër. + +Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, +deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la. + +(DOGGANTAL CI LAAB) + +Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, +ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la. + +(DOGGANTAL CIG SOÑÑEE CI ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK CEE SÀGGAN) + +Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete, +ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara. + +Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li. +Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp mi ni mu ware. + +Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji. +Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub +ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi. + +Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna, +kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele. + +Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu. + +Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko. + +(DOGGANTAL CI FARATAY JULLI) + +Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi. + +(DOGGANTAL CI SUNNAY JULLI) + +Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12 li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18 am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir. + +( DOGGANTAL CI FARATAY NJÀPP ) + +Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 +raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj 8 gaaw + +(DOGGANTAL CI SUNNAY NJÀPP) + +Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi. + +(DOGGANTAL CI FARATAY SANGU) + +Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu + +(DOGGANTAL CI SUNNAY CANGAAY ) + +Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi. + +(DOGGANTAL CI FARATAY TIIM) + +Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul. + +(DOGGANTAL CIY SUNNAAM) + +Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi. +Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim. + +(DOGGANTAL CI WOOR) + +Woor ñaari farata la am: 1 yeene 2 ba liy dogloo ngir yàlla. +Sunna yi ñatt la : 1 gaaw a dog 2 yeex a xëdd 3 ba wax ju ñaaw + +(DOGGANTAL CI ASAKA) + +Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yeene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. +Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool : 1 nga ànd ceek teeyug bakan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal. + +(DOGGANTAL CI AJJ) + +Ajj ñeenti farata la am : 1 yeenee ajj 2 tawaaful ifaada 3 dox diggante safaa ak marwa 4 taxaw arafa. + +(DOGGANTAL CIY SUNNAAM) + +Sunnay ajj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka. + +Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi. + +Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa. + +(LII AG MOTTALI LA ) + +Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku birël ci ginaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi. + +(DOGGANTAL CI NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINAAW IMAAM) + +Lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot. + +Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , +sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat. + +Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, +taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex. + +Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf. + +Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël. + +Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. +Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. +Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko. + +Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . +Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem. + +(BUNT CI LIHSAAN) + +Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu. + +Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral. + +Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ. + +Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat. + +Fii la Tasawudus sixaar yam,ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca.Woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi,di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog,mu diw woy wuy wommate jëme ci xam-xam ak jëf,ak tegginu tey jàppndal mebat yi.Mu diw rajas wu am njariñ te barkeel,wu way texe yi bokk. + +Yàlla ci barkeb yonant bi (j.y.m) nangu na woy wii,jariñ ci it kepp ku texe,kuy laabiire,te yewwu ,moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax,di jañ gepp texeedeek woru. +Yàllaay ki ma digal ma woy ko,yàlla miy ki nu jublu,mi may fegal luy waral njàqare.Woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja,moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral. + +Konug cant ñeel na yàlla,xeewal ak mucc yal na nekk ci Ahmadu ,aji rammu jiy boroomi ngëneel,ak ñoñam aki saabaam.Ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam. + +Subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun,wasalaamun halal mursaliin,wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin. + +(LII AG XAMLE LA) + +Bokk na ci njariñi woy wii : ki ko woy (muy sëñ bi) ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ,ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom.Bokk na ci ngëneeli woy wi, begal gun ko begal bim ci noppee(moom sëñ bi) ne ko woy wii de la yàlla (t.s)ak yonant bi(j.y.m) gën a sopp ci ay keman. +Bokk na ci li nu ko begale:kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko,texe ag texe gu texeedi dul toppati,bokk na ciy jagleem ku ko mokkal Munkir ak Nakiir dun ko laaj ci bàmmeel,ak leneen ak leneen ak leneen,yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob,yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li. + +Yoonu murit +Bii jukki bu am solo la, ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom-koom, ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di The Economist, di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk, te adduna bepp xam ko, muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp, moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar 1843.Economist Newspaper Limited (Filiale de Pearson) ca London moo ko génne. Li ñu ci gën di wax nag mooy koom-koomu adduna bi, politig, jëflante, xaalis, xam-xam, xarala ak fànn (art). Lim bu ci génn, di nanu ci defar lu ëpp milyoŋ, te 80% ba ca biti Angalteer lanu leen di jaaye-ji. Yëglekaay gi tas na ci lu tollook 1.138.118 ciy yax ci xaaj bu njëkk bi ci atum 2006, ci li gëstug bureau of circulations wax, di jumtukaayub natt bu nekk ca Angalteer. 53% ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa Amerig lanu, 14% ay waa Angalteer, 19% di ñu dëkke Tugal gu goxe gi (continentale). Yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook 206 réew. + +Faith in the market (ngëm ak yaxantu) + +19 desambar 2006 / Rom ak Tuubaa (Senegaal) + +Ci ginaaw luumay Itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si, am mbooloom jullit mu Afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde “addunaal” di (mondialisation) + + + +Kepp kuy door a teg tànkam ci suufus Rom, péeyub Itaali, dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon, mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg-leeg as lëf ci lii di Cappuccino, di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca Itaali. +Bu ngéen jëlee yoon wi jëm Vatican, jaare ko ci Via Della Conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme, da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo Afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu (waso), ay saag, ay der (ceintures) walla ay weeri jant yu nu roy, maanaam yu doonul piir. +Bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu, bu ngéen moytuwul, da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax, mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk-der yi, mu dig (dàqante gu xoromu te yërëmtalu). Nii daal lanu koy nekke, saa su nu léen yëgalee ne takk-der yaa ngoog, da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas, seeti nu nu man a mucce, bu Yàlla dogalee rëccuñu, bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu, moom kay danu ko fay bàyyil takk-der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam, daal di leen yobbu. (…) + +Ca dëgg-dëgg, jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme Vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu (organisewuwunu). +Ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu, gu nu xame ci adduna bi ci gëm-gëmu diine ak bu koom-koom, te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di Tuubaa, nekk nag ci digg Senegaal, boo fa jëmee nag juge Dakar péeyub Senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool. + +Niki yeneen imigire yu bari yu Senegaal (yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca New York, walla ñu diy wattkati suraas (orange) ca Espaañ) jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca Rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye “yoonu murit”, mooy yoon wi ëmb taalubey Cheikh Ahmad Bamba yi, kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum 1927. ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem Sëñ bii, indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey (maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi). + +Li ëpp ci 11 milyoŋ yi dëkke Senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu Murit mbaa wu Tiijaan, moom nag (yoonu Tiijaan) moo fi jiitu wu Murit. Bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ((ag murit)) leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul Lislaam, gas reen ya, xame ko na ko Yonnat ba indee woon. Waaye nag moom Lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo Araabi Sawudit. Lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax (culte des saints et de leur tombeaux ) muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel ba ci bu seen sëriñ boobu sax, te loolu ñoñ Wahaab ñi danu koy weddi, di ko kontar. Waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi (ñoom wahaabit yi), ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg, tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa Araabi Sawudit dara ba dara booloo jeex. +Sheex KA di sët ci Bamba, ca biir këram ga nekk Tuubaa, di dëkk bu fees dèll ak ragal-Yàlla, waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa, ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme, moom Sheex KA mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp: (( bu ngéen wéeroo ci keneen)) mi ngi nuy leeral (( du ngéen gore mukk, lii mooy sunu gisiinu dund)). Bi mu fi daataa juge Bamba mébetoon na ay mbir yu bari: bëggoon na Tuubaa, dëkkam bi mu sanc, nekk dëkk bu sell. +Njabootam gi – ci déggiin wu yaatu wi – Mbàkke-mbàkke yi, ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam-xami diine, yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb, maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte. Xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey, ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo, ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ (sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di w��r adduna bi, ngir nemmeeku-ji seen taalube yi) ak ngir suqali dëkkub Tuubaa bi. + +Lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli Afrig yi gën a tèkki, moo xam ci seen réew la mbaa feneen. Fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje. Seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit. Ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat, ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus, yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man, te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey. Nan jël ku mel ne Aliyun KA, ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan (vente en gros) ca wetu gaarub Rom ba tudd Termini. Moom rakk la walla mag ci Sheex KA mi nekk Tuubaa di topptoo njaboot gi. Aliyun KA mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër ( walla sax ñu duli senegale ), bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi. Lenn nag ci njaay mii Senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo Endonesi, Thailande mbaa End. + +Teewul Aliyun nangu ne am na leeg-leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees. Moom nag Aliyun, ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge Banglaades, ndax nee na ((ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji (meteo) ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi ! )). Am na benn yoon ci mbedd mi, Sang Ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante. Jaaykati saag yii ak der, nga xam ne yu ci ëpp Siin lanu juge, ñu ligeeye leen fa, danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam-xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk-der yi. Bi añ jotee, gan dikkal na Sang Ka, di benn waa reewam N. GEY, mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi Senegaal yu tàng, plaat bu nekk 5 euro. + +Benn yoon ci ayu bis gi, lu ëpp ci murit yi nekk Rom dananu daje ngir def daayira (julli, jàng Alxuraan aki Xasida), gisante, siyaarante,xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal. Leeg-leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer , yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo, ngir nu jaayaat leen ca Sandaga, ja bu nekk ca Dakaar, te murit ya ëpp fa. Ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis, looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi Senegaal. Waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy: woo seenub xarit walla xame ca Sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla. + +Ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci 40% ci askanu Senegaal wi. Waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey Senegaal yi nuy tollale ci 700,000 . Murit yi it ñooy daanaka 80% ci jaaykati Senegaal yiy wër, tey jaar ci mbooleen qàli Itaali yu mag yi. (Fraans mi doon dooley sancaan ji tegoon loxo Senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një. Ay fukki at a ngii Itaali nangu barabam boobu ci moom, waaye nag jamono jii ñu nekk Espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci Itaali. Lii sax moo waral ci weer wi (desambar 2006) lu jege 80 waa Senegaal ñoo sànku ci ndox mi, ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon Espaañ, ca dunam ya tudd Canaries). + +Lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn. Loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom, te mooy sukkandiku ci sa bopp. Lu man a xew nag, ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag. Bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga, def fay weer. Te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski-ji, bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di Màggalug Tuubaa, bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti Tugal ci jamonoy lòlli. +Jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi nu def ci wàllug njiit. Ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan Xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la, di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy Sëriñ muhammadu lamin baara mu Sëriñ Fallu. Kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko. Cig ayam Tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba. Ci atum 1958 bu ña fa dëkk weesuwutoon 2000 nit, leegi àgg nanu – man nanu ne - ci ay 700,000 nit . Alkol nag ak Póon danu leen a aaye ca Tuubaa , moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir Senegaal. Ña nga fay taxawal daara ju mag (ab université). Boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine. Jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it, ñu ci bari it dunu musóoru. Xale yu góor ya’ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba (école). Saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay (hopital) mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi, ay milyoŋi eurooy dajaloo, ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu, ku ci mel ne Elhaaji JUUF may futbal ca Bolton (Angalteer), ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub Tuubaa ba (…) +Xamagunu leen de bu baax, waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de, du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation (di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew, benn xalaat, xatal soreente yi, jegeele gis-gis yi añs), waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme… +Yoonu murit +Jëmm “fii muy tekki physique” baat la bob ci gereg mooy φυσικη maanaam «fisikus» di ci wolof“kojug dénd”,moom nag mi ngi juge ci reenub φύσις «dénd». Kon «jëmm» mooy xam-xamu dénd. La ko dale ca kawaarig yi nga xam ne nu ñu tuuteewul amul ba ci nekk(àdduna)gu màgg gu tàlleeku gii,xam-xamu jëmm liy liggéeyam mooy jéem a tëgg ay àtte walla ay yoon yu matematig yuy àtte àdduna bii di bu ne-ne bu dénd,ak lambutu xóot-xóoti ne-ne ak dëgg-dëggi jikkoom ak way toggale(composants)yu mag yi ko toggale, ak doole yu dàttu (fondamental)yi nga xam ne yaram yu ndaw yi dinañu koy joqalanteek yaram yu ne-ne yi, nga boole ci njuréefi doole yii. Leeg-leeg ci xam-xamu jëmm bu bees bi danu ciy boole gëstug “xam-xamu ndendoo” ak bu “wattuwu” niki xam-xamu wattu kàttan ak “jañu”( Momentum ),ak cefkag mbëjj,looloo waral boroom xam-xami jëmm yi lu bari lanuy faral a gëstu ci feeñtey jëmm yi, dale ko ci ëtt yu yaatoodi yi ba ci yu yaatu yi, dale ko ci yaram yu ndaw yi nekk ci ron saal walla xartil, nga xam ne ca la mbooleem ne-ne yu baaryon yi di ame “jëmm bu yaram yi” ba ca gëstug sóobu walla jikkoy yaram yu jëmm yi ca adduna ju yàgg ja, ba ci jàng yëngu-yëngu gu bidiw yi ci asamaan su ne-ne si, moo xam ci biir gaawaay yi nu xam la walla yi jege gaawaayu leer, ci mujjantal gi, gëstu nekk gi (adduna bi) ci léppam. + +Xam-xam +Jëmm +Kawaarig mooy benn ci ñaari way toggale yu dàttu yi ñeel ne-ne gisiinu walla tewori bu roytéefu natt bi ci xam-xamu jëmm bu yaram yi (beneen bi ci gisiin wii mooy libton yi). + +Xam-xam +"Yewwute" gu Tugal gi, baat la buy tekki, ci maanaa mu taariix mi mu yore, yëngu-yëngu gu dekkal ak yeesal, walla dundal xay gu Tugal gu yàgg ga, gu Geres ga ak Rom. Rawati na ci wàlli njàggat, fànn ak tabaxin. + +Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbali ci xarnu bu fukk ak juroom ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Isaa (XVu xarnu balla Isaa), ba ci bu fukk ak juroom ñaar (XVII), mu sos fi nag ay coppite yu xóot ci wàllug aada, dundin, mboolaay, politig ak koom-koom. Kon daal, "yewwute" gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja (mu'y jamono'y "ag laman" walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji (di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala). + +Li ko sabab +Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nanu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy : + + Jeexiital gi xay gu lislaam gi def ci yewwute gii, + Feeñug dëkk yu mag yi ci Tugal + Neew-doole gu jàngu bu Paab bi neewoon doole, ak tas gi mu faroon tas. + +Jeexiital gi Lislaam amal ci yewwute'g Tugal gi +Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore, araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Tugal nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk. + +Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñe yi(croisade). + +Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñe ya (walla yu galajaane ya), duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam. + +Lii nag ci li soppi xalaati waa-tugal yi la jëm ci jàngu bi, nit, adduna bi ak dund gi. + +Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbali woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci paj, xeltu, gañcax ak ndundat, ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn(XI) (g). + +Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin (wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Tugal ca jamono jooja) loolu dimblee woon, ci ginaaw bi, ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am. + +Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi +"Nosteg laman" walla gug cang, ku ne xam na ne la mu baaxoo woon mooy tegu ci mbay, suuf, ak seqoo yu laman yi daa lijjanti ak'a nos diggante jaam bi ak sang bi. Ag laman nag jullit ñi masuñu koo xam, nosteg koom-koom la, tey gu mboolaay gu bon, daan gàllankoor xay gi ba du jëm-kanam. + +Bu ko defee, li ñuy wax "tool", di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste. + +Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug liggéey yi, ngir jòkkoo gi waa-tugal gi daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt aka naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal gi tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku, ci léppam, ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi. + +Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu aka lakkal noste gu laman gi, tey liggéey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man a am. + +Lòttug jàngu bu Paab bi akug tasam +Jàngu bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sottiwoon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax "njàng yi aju ci Yàlla" (théologie), ak njàggat ak xellu. Amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam. + +Jàngu bi moom dafa jàppewoon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Jàngu bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, degginu ligeeyub yaxantu gën faa xóot, ak bu endustri ak aada. Yii yepp nag liggéey nañu lu rëy ci, waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it, di doyodil nosteg laman gi, rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am. + +Itaali mberum yewwuteg Tugal gi +Dëkk yu Itaali yi ñooy mber yu njëkk, yi njëkk a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak ñoñ fànn, duggaloon nanu ci seen loxo bu baax. + +Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay, yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa-rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fànn, nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine. + +Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab bi ci Itaali ag tono gu neen ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi nguuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa liggéeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi téere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi. + +Mandargay Yewwuteg Tugal gi +Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy: + +Yëngu-yëngu yi aju cig "nite" +Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya (yu Geres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi, ak jeem a xam seeni mbóot. + +Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàngatkati Geres yeek Rom (grego-romain) ñoom lañu jëloon, yittewoo leen, ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàngat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàngati Geres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam. + +Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi, di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot, nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja. Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi. + +Ci dëkki Itaali yii, lu bari ciy fànnkat yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko (1400 - 1455), Leonardo da Vinci (1452 - 1519), Titian (1488 - 1572), ak Rafayel (1493 - 1520 g), yattkat ba Donatello (1386 - 1466). + +Feeñug làkk yu bees yi +Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi, moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña, di woon niti neen ñi rekk, ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon. + +Bi jamonoy "yewwute" dikkee, ngelawul "fonk sa xeet" upp ci Tugal gépp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu. + +Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante (1265 - 1321) taalif mbóosóor mu Sell mi ci làkku waa-itaali, naka noonu Petrarch (1304 - 1374) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi. + +Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais (1483 - 1553) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). + +Chaucer mi dib waa-angalteer (1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme ya cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën a siw. + +Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Tugal taxaw. Yu amoon "ag temb", ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci "temb" tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi. + +Yëngu-yënguy dajale mbind yi +Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lañu nekk ci Xustantin ak ci dëkki waa-geres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal. mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Geres yeek Latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek jàngu yi ak jàngu yu mag yi, ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii. + +Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni liggéey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk, mbindum binkat bii di waa-rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g). Tacitus moomu mooy taariixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi. + +(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya: + +Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya. +Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam, waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix, mu tudd daaray xam-xam bu taarix. + +Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla (1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn wayndare (dossier) bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax "mayug Xustantin", mooy wayndare boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen. + +Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli (1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas. + +(6) Jëm-kanamug yaxantu ak ndefar: + +Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi, ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa. + +Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey ndefar yi yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci koppar yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug "kuréel gu diggu" gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi. + +(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi: + +Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. +Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi, ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi. +Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon (1220 - 1292) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal. + +Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf. + +Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ (1561 - 1626 g), di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi, ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd. +Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci (1452 - 1519 g) moom tam feeñ, di kok dafa yittewoo woon jiyoloji (bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn, tey fentkat. +Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo (1564 - 1642 g) feeñ, mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba, dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus (1476 - 1542 g). + +Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel, walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam. + +Yewwute gi ci Itaali: + +Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo: + +1 - Song gu mbooloom xarem Fraans mi ak mu nguurug Rom gu nu sellal gi songoon dëkki Itaali yi, rawati na Rom ak dëkki bëj-gànnaar yi, niki Milano, loolu it taxoon na ba ñu giir dëkk yooyu, te Milano ak Rom jiitu woon ci. Ci noonu la yewwute gi delloo ginaaw ci Itaali ngir ñàkk gu fa jàmm ñàkk ak kaaraange ak dall. + +2 - Jeex gu àtteg walla kilifteefug njabootug Madatsi jeexoon, ñooy buur yi daa sàmm yewwute gi ci Firenze, loolu nag sabab si mooy xuloo ak xeex gi amoon ci biir njaboot gii, te Firenze moo ëppoon solo ci barab yi yewwute gii nekkoon. + +3 - Teg loxo gu buurub Espaañ bi Ferdinando, buurub Argon, defoon Napoli atum 1504 g, loolu bokk ci li neewaloon doole yewwute gi ci dëkku Itaalib bëj-saalum bii. + +4 - Yëngu gi amoon ci jéem’a yéwénal diine ji ci Orob, ñi ko daa def di Luther, Kalfen, Swingli ak ñeneen, looloo taxoon paab gi jug ak doole ci kontar nite gi. Nga xam ne sax noonu gi àgg na ci paab bi tuddoon Kalimat mu juroom ñaareel mi, kompoloo woon ak buur bi Sarl 5 (Sarlkaan) buurub Espaañ bu katolig bi, ngir ñu fexee naaxsaayal yëngu-yëngug nite googu ci Itaali. Loolu mooy li waajal mbir yi, nooyal yoon wi ba “ëttu àttey lajmat" yi man’a am ca Esapaañ, di woon ëtti àtte yu siwe ay jëf yu ñaaw, daan sonnal ak a fitnaal képp kuy woote yéwénal, mbaa’g yewwute. +Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund. + +Tuxug Yewwute gi: + +Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs. +Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay. +Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen. +Nitug Holand kii di Erasmus (1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi. + +Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax "kòllare gu yees gi" def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon. +Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi. + +Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali: + +Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll. + +Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey. +Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi, looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal. + +Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g. + +Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom. +Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi. +Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi. + +Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g) ak ñu dul ñoom ñaar. + +Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi. +Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer. + +Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam. + +Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew. +Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii. + +Taariix +Jolof moo doonoon nguur ngi gënnoo na mag ci Senegaal ci jamono yooyu. Mi ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawati na la feete woon ca sowam. Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono. + +Sosteefam +Ki ñu ne moo sos nguur googu mooy Njaa Jaan Njaay. Mooy doomu araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingèer ab Tukulòor bu tudd Faatimata Sall. Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy. + +Bokk na ci def wolof yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer. Samp nguuru Waalo ba mu dëgër, mu dal di koy jox rakkam. Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam. Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotu ñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga. + +Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi di nga leen fekk ñekk fukk doŋŋ. Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay. Réew yu bari nekkoon nañ ci kilifteefu gu mag ga. Lu mel Senegaal ak Gaambi ak Faleme nekkoon na ñu ci suufu Jolof gu mag ga. + +Buuri ñu mënoon fal ngir elif nguuru Jolof, dañu doon wara bokk ci juroomi meen (wallu ndeey) yoyu, sant: Njaay, Joob, Faal, Ndaw, Ñaŋ. Ci xeeti Seereer ak Pël, lañu joge. + +Buuri Jolof yi + +Nguuru Jolof +Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba lag da geer, égg na Ferlo. Moom dafa xawa uuf Tooro ak Dimat ak Waalo ak Kajoor ak Bawol ak Siin-Saalum wàllu penku wi ndand féy-féy la. Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek. Mel na ne du fu naat it ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëriñ Musaa KA am na fu muy melale lu ni mel ci genn xasidaam, mu ne : +nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani + +Kon du war a nekk fu bari ay balluwaayi xéewal . + +Ay way dëkkam +Waa Jolof nekkoon nañu ay giir yu wuute, booba ñu ngi ci seen joge bëj-gànnar jëm bëj-saalum: giir yooyu ay Séeréer lañu ak ay Wolof ak ay Tukulòor. Naari gànnar yi daana ñu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi. Nee nañ ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng, mu ngi bokk ci xeetu Màndeŋ. Turam la ñu jox nguuru jolof. moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan wooye Kàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ. + +Jolof gu màgg ga +Fuuta moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi. loolu masu la deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon. + +Jamono jooju la màndeŋ yi yaatal seen nguur gu mag dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi. Ca jamono jooju yit la nguuru jolof nangoo boppam, moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, Fuuta ba Saalum. Ëmboon na Waalo, Kajoor, Bawol ak rèewi Séeréer si ak lenn ci Fuuta Tooro. + +Saayug nguuru Jolof gu mag ga +Rèew yu bari nangu nañ seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga. Kajoor njëkk a nangu boppam topp ca Waalo ci njiitu Barag. Bawol ci njiitu Teeñ. Rèewi Sèeréer si ci njiitu Buur. Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX. Waaye Dammeel moom moo gënnoona metti ag jàmmaarloo ak Burba jolof ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga. Ganaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697 foofa kajoor moo Jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886. + +Ngirtey saayam +Bok na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo nguur ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX. Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ. Ñareelu noon bi mooy Amadu Sayxu. + +Tanoor Jeŋ doomi Lingeer Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga. Ginaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870. Yor ko ba ci atum 1875, ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo. Ci noo nu la Jolof tàbbee ci loxoy Faraas ci 18 rakki gammu 1885. + +Delluwaay +Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998 + +Lëkkalekaay yu biir + senegaal + Kajoor + Waalo + Siin-Saalum + Fuuta Tooro + Réewi lebu yi + Tekuruur + Bawol + +Téerekaay + Samba Lampsar Sall, Njajaan Njaay. Les mythes de fondation de l’Empire du Djolof, Dakar, Université de Dakar, 1982, 157 p. (Mémoire de Maîtrise) + Mbaye Thiam, Le Djolof et Bouna Ndiaye, Dakar, Université de Dakar, 1976, 110 x. + Eunice A. Charles, A History of the Kingdom of Jolof (Senegaal),1800-1890, Boston, 1973, 280 p. + Eunice A. Charles, Precolonial Senegal: the Jolof Kingdom 1800 to 1890, Boston, African Studies Center : XII-163 p. African Research Studies, n° 12. + Victoria Coifman-Bomba, History of the Wolof State of Jolof until 1860 including comparative data from the Wolof State of Walo, Madison, University of Wisconsin, 1969, 395 x. + Jean Boulègue, Le Grand Jolof (XIIIe-XVIe siècle), Paris, Façades, 1987, 207 x. tome 1 : Les anciens royaumes wolof (Sénégal) (Thèse d’Etat publiée en partie) + Patrice Mingou, Le Jolof de 1870 à 1895, Dakar, Université de Dakar, 1977, 111 x. + +Taariixu senegaal +Nguuri senegaal +Mooy fukk ak ñeenteelu buur ca nguuru Jolof gu mag ga. Su fekkee daanug Lat Joor feeñ na ci taxawaayu jàmbaar yi ci kanamu tubaab bi, loolu terewul Alburi Njaay jël ndondol bañ ak fukki loxoom. Alburi tax na tubaab bi fattewul Lat joor. Looloo tax tubaab bi doon ko xoolee bëtu mbañeel ci fat gi mu fatoon Lat Joor. + +Gàddayug Alburi +Ñoñantal gu metti gi tubaab biy teg waa réew mi te Alburi manu koo faj moo taxoon mu génn rèew mi dem fekki Aamadu Taal doomu Sayxu Omar Taal ca Kolomina. Foofa la àndeek moom jàmmaarloo ak tubaab bi, ci luy dayob njàmbaar ba ci 1893 la Alburi daanu ci Doosu, baatam ni Poto! + +Niti senegaal +Waalo bokkoon na ci yénn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoo. Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar. Njurbel moo nekkoo péeyam ci lu njëkk, ganaaw bi lañ ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer. Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu ganaaw ak ñàkk doole. + +Jëwrin yi +Ñooñu ñooy: Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi. Ganaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur. Bokk na ca Meet moom mooy njiitu bëkk-nèeg yi ak bëkk-nèegu Njurbel moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur. Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi. Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi. + +Waalo, amoon na ñeeti kër ñu daan taan Barag bi, soqikoo ci ñeeti xeet yooyu: + + Tejeek (Pël ak socé) + Joos (Séeréer) + Logaar (Naar) + +Barag bi, di turu buuru Waalo, dafa joge ci turu ku jëkk nekk Barag, mooy Barka Bo (Mbooj). Barka moo soppiku Barag. + +Barag + +Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo. Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de geer. Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo: ba njëkk moo di Lingeer miy yaayu buur bi ak Aawo miy soxnaay buur su njëkk, moom moo am teraraagaay toog ca gangunaay (mooy toogu gu buur) ga. + +Bu ñaareel ba moodi ñatt ci boroom ndombay tànk yi ci péncam Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak maalaw mi yor koom-koom bi. + +Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom moo di njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur. Baadi moom mooy njiitu doomi buur bi, ak yénn ci Jëwriñ yi. + +Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare. Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram. mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo wara teew ci gàmmu gi. Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la. Ndaxte senug teew li muy tegtal moo di yeesal seenug nangu, lañu lokki ak lañu siif. Mbooleem alal yooyu daanañu leen séddale ñetti xaaj: ben ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca pécum Séb ak Bawar. Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbèem yi + +Seddaleeg yorte gi +Nguur ga dañ ko seddale woon ci ay diwaan, bu ci ne amoon na bàjjo buy dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer). Kàjj moom la ñu fal ci ndijjooru dex gi, li ko dalee ca aarnik ba fa dex gi sottee. Buriko moom la ñu fal ci bëj-gànnaaru Lag de geer, mu ngi daan dëkk ca Foos, Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinò Bawaal. li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi: Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo. Barlaf moo nga dëkkoon ca sowu Lag de geer. + +Buuri Waalo + +Ay jafe-jafeem + +Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ya cong yi jòge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi. Moo tax ba ci xarnub XX waa waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi. + +Ba besu tey Waalo ngi jànkonteeg coon ya jòge woon ca ŋaayoo ga. loolu mooy jur dellu ganaaw ak daanug waalo, ba ku nekk di ko cokkaas: Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel. Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas. ganaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx, dakoo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen ganaaw ci 1885. Booba la nootee Waalo, te naa daf koy xettali. + +Delluwaay +Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998 + +Lëkkalekaay yu biir + senegaal + Kajoor + Jolof + Siin-Saalum + Fuuta Tooro + Réewi lebu yi + Tekuruur + Bawol + +Taariixu senegaal +Afrig +senegaal +nguuri senegaal +Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal. Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk. + +Cosaan + +Kajoor mooy kàdd ab garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si. Moo jur baat boobu kajoor ci wolof. Ñi jëkka yor suufi kajoor, ay séeréer lañu woon, ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ. Ba pare, xeetu wagadu ak jafunu, soqi ci sooninké yi, jóge ca penku, ñoo sos meeni jëkka ilif nguuru gi, ak ñu sant FAAL. Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor. Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen. Dammeel mooy damm, ndax ku jëkka jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor. Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam. Loolu, ca jamono Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon buur-ba Jolof la xeewe. Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI. Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon. Ba noppi Amari Ngone, jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor. Ca tegu, Kajoor di gëna am doole, Amari Ngone dem naa Bawal ak ay jammbaaram, nangu reew moomu. Li tax Amari doonoon ku jëkka nekk Dammeel-Teeñ. Bawal, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan. Amari moo duggal aada bi ñu fal buur bu ñu tudd xulixuli, di fateliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkka nekk buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo. + +Koom-koom +ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na rèew mu ay am-amam newoon. Mbay ak liggéey u loxo ak camm ak napp ak yaxantu ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca rèew ma. + +Mbay +Mbay moo doonoon liggèey bi ëppoon solo ci koom-koomam. Loolu moo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ cakoom ga, manoon naa andi sax ab xiif. Dugub moo ëppoon ca mbay ma ak ca dund ga. Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng. Xamoon nañu mbayum. wëtteen. + +Liggéey u loxo ak yaxantu +liggéey ak loxo ñeeño yi la ñu ko feetale woon. Napp gi amoon na solo lool ci dund gi. Waaye njaay moo naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal. Mujj na ba yoon yi jòge bëj-gànnaar ñakk solo lool njëgg mi. + +Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo, Fekkoon na Kajoor da jaay ay der ak ay bëñi ñayy mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi,... + +Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon. Ñi ñuy wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu. benn nit amu ci woon moomeel. Loolu terewul woon ku mu neexoo mu jariñoo ci kèem kàttanam. + +Doole ju bees ji +Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya. Ñiy doora falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo. Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon, ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul, rax ci dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk + +Liggéeykat yi +Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi. Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetele woon mbay mi, ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat. Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay. + +Yoriin + +Nguur gu bees gi tax na ba ñu andi tër yu bees ci ay àtte yu bees. Dammeel moo feete woon ñépp kaw. Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen. Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen. Waaye loolu su xewee li koy waral mooy fullay waa ja ak faydaam ak tabeem. Yii yépp ñiy tànn daa nañu ci bàyyi xel. + +Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem. Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe. Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur. + +Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn. + +Kajoor nekkoon na juroomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum. Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam foo féete. Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur. + +Buuri Kajoor + +Delluwaay +Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998 + +Lëkkalekaay yu biir + Senegaal + Jolof + Waalo + Siin-Saalum + Fuuta Tooro + Réewi lebu yi + Tekuruur + Bawol + +Taariixu senegaal +Afrig +senegaal +nguuri senegaal +Jukki bi, bunt la ngir leeral li ñu bind ci Kàddug Yàlla. Maanaam dañuy yéene dajale jukki yi wax ci nit ñi, dëkk yi, bereb yi, mala yi ak yeneen mbir yi ñu mana gis ci Biibël bi, rawantina mbir yi jafe xam ci kaw anami Senegaal. + +:Wàll:Nit ñi ci Kàddug Yàlla +:Wàll:Nit ñi ci Téere Tawreet +:Wàll:Nit ñi ci Téere Linjiil +:Wàll:Bereb yi ci Téere Linjiil +:Wàll:Baat yi jóge làkku ibrë +:Wàll:Baat yi jóge làkku yawut +:Wàll:Baat yi jóge làkku gereg +:Wàll:Per yi ak Xeer yi ci Kàddug Yàlla +:Wàll:Mala yi ci Kàddug Yàlla +:Wàll:Gàncax yi ak garab yi ci Kàddug Yàlla +:Wàll:Xeet yi +:Wàll:Yàllay xeet yi +:Wàll:Njàngalem Mbooloom Kirist yi am solo +Diggu Afrig (di wax tamit Afrigu yamoo) doon ab xaaju Goxub Afrig bu nekk ci diggante ndand féy-féy gu Sahara ci bëj-gànnaar ak ndand fey-fey gu Kalahari ci bëj-saalum; ci penku mi ngi yem ci peggi dexu Rift ca Ecoopi, ci sowu ci mbàmbulaanu Atlas. + +Su nu sukkandikoo ci sedatley àdduna bi Mbootaayu Réew(MR) yi def, Diggu Afrik benn la ci diwaan yi ñu sedatlee Afrig. + +Juroom ñenti Réew yi ci nekk: + Angoolaa + Réewu Diggu Afrig + Kongòo + Cadd + Kameroon + Réewu Kongòo + Gaboŋ + Ginne gu Yemoo + Sao Tome ak Principe + +Melokaan +Ci biiram di nga fa fekk barabu Afrig yi nga xam ne mandiŋ nga fa am, fekk fa réew yi am klimab ndand féy-féy, ay réew yu am ci allub yemoo bi, yu tàq ci dexu Niseer ak wu Kongòo. + +Doju Kamerun (4070m), doju Ruwenzori (5119m), doju Elgon (4321m), doju Keeñaa (5200m), doju Kilimangiaro (5895m, di doj bi gën a kawe ci Afrig) ñooy doj yi nekk ci Diggu Afrig. + +Doon na diwaan bu bariy nit. + +Diwaani Afrig +Imbraatóor gu Mali ba ci xarnub XII, xamalu nu ko woon lu bari. Ci li tegu ci atum 1150, la nu xam tur yu mel ne Hamana, Jigi Bilali(1175-1200) ak Musaa keyta di ko wax itam Allakoy (di tekki neex yalla). Mi ngi yamoon ci Mbàmbulaanu Atlas ci sowwoom, Dexu Niseer ci penkoom, tay ñuy yii réew: Mali, Senegaal, Gaambi, Ginne, Ginne Bisaawóo, Gànnaar, ak ab xaaj bu mag ci Kot diwaar. + +Ay Cosaanam +Ci boobu diiwaan (Sudaan) ag nguur gu ndaw judd woon na fa: Mandeŋ walla Mali (Malenke: nitu Mali). Ci li gën a siiw coosaanam, ay dëkk-dëkkaani mande yu bari yu nekkoon ci Kaw-Senegaal ak ci Kaw-Niseer. Traware yi nekkoon Dakadiyala, ci réewu Kri, ci wetu Nagasola, ci Kaw-Bakoy, Konte yi nekkoon Tabu, ca Doodugu (di tekki réewu Doo), Kamara yi ca Sibi, ca Siendugu, Keyta yi ca Nareena, ca Doodugu ak ca Doj yu Mandeŋ, nekk ci diggante Sigiri ak Kita. + +Ca Doodugu la Bambara yi nangoo ay dëkk yu bari, màmm jëm penku, ba peggu Seegu ca Niseer. Ci li wër Doj yu Madeŋ, Malinke yi ñaari dëkk yu solowu lañu fa amoon: Kiri ak Dakadiyala. Njiitu dëkk yooyu ay rëbbkat la ñu woon, yu bokkoon ay gëm-gëm, bokk di def seeni xumbéeli diine. Nekkoon nañu nag ay Askan yu bari yu bennoo woon am benn buur, Simbo moo doonoon seen dàkkantal. Buur yooyu Askanu wee leen doon fal mu lee doon teewal ci ndaje ya daan am ca Pénc mu Mag ma(Gara), mi doon dogal ci li ñeel xare yi walla juuti yi... + +Dooley askan yu nguur-nguuraan yooyu doon màgg, ñoo jàppale nguuru Sooso gi donn Nguura Gana gu mag ga, ba mu man a sos geneen nguur gu mag gu buur ya amoon dàkkantali Mangha walla Mansa. + +Sunjata Keyta + +Musaa Keyta di ko wax itam Allakoy, siiwoon na ndax aji Makka yu bari yi mu defoon, loolu saxaloon na diiney Lislaam ci xoli Njabootu buur bi. Doom, di itam Ndono lu Musaa, Nare Famagan (1218-1230) siiwoo na loo ndax yaatalam jëm bëj-gànnaar, ak sowwu, ak pegg gu ndeyjooru Kaw-Niseer, nootoon Somono yi. Nare Famagan bari woon na ay jabar, kenn ci ñoom mooy ki ñu dàkkantale woon Kuduma (boroom góomi yaram yi). Jabar ju tawatoon jooju mooy yaayu Sunjata Keyta. Bi mu juddoo ba juroom ñaari at managul woon a dox. + +Laagoom googu moo taxoon, ba Sumaawuru Kante doon faat ay magam, ba woon ko fa. Benn bis, Sunjata jéngu ne day jug taxaw, ndax naqar wi mu amoon ci li Sumaawuru defoon, tegoon ci nangu nguur ga. Mu laaj ag weñ ngir jafandu ci jug, weñ ga damm, mu jël geneen, noonu, jëlaat geneen noonu, ci la kenn waxe ne nañ ko jox yatu baayam wa, ba mu ca jafandoo la jug taxaw. Ña ko teewe woon yéemu; nday ja ak géwalam ba, Jakuma Duwa, ca la ñu fente ab bakk duppee ko Xala ga, baat ya ak woyiin wa, ba tay ñoo ngi rëkk ci dënni waa mali yi ndax mooy seen bakkuw réew. + +Ci 1230 la nekk buur, ci la ray Sumaawuru, boole nguur-nguuraan yépp ya nekkoo ci wetam, ci nguuram, dal di nekk nag Mansa. Ci moom la Mali nekke nguur gu mag dëgg, ci la àgge ci pujam. + +Ay buuram + +Ulee +Bi mansa Ulee ñëwee(1255-1270), di ki wuutu Sunjata, la tàmbalee Diggadil(décentraliser) nguur gu mag gi jox ko yoriin wa méngoo woon ak réyaayam. Tabb ay sang jox leen ay ndomboy-tànk yu am solo, ñi ci gën a ràññeeku: Fran Kamara, Siriman Keita. + +Abuubakar mu njëkk(I) +Ci 1285 la Abuubakar mu njëkk(I) mi faatu, Jafe-jafe yi nekkoon ci tànn aji wuutu, ca la Sakura jëlee nguur ga. wuutu na nitu nguur di itam jàmbaar, ci la yaatalaate nguur ga ba dugg Gaawo ci penkoom ak Tekuruur ca sowwoom. Ay saay-saay ñoo ko ray ca weti Tripoli mu feekoon ko muy aji Makka. + +Abuubakar mu ñaareel(II) +Ci 1303, Abuubakar mu ñaareel mi(II), di jarbaatu Sunjata, mi siiw lool ndax li mu bëggoon a wuññi li nekk ci ginnaaw Mbàmbulaanu Atlas gi. Ca la jële ñaar téeméeri looco ak dund, daal di yònnee ngir ñu dugg ci mbàmbulaan gi, waaye kenn a ca dellu si nettali ni dañoo dajeek ab duus bu soxor ci ndox mi, mu mëdd leen. Abuubakar dal di jëlaat ñaari junniy looco, ak bund bu doy, and ak ñoom dem, ca la saaye ba tay. + +Mansa Musaa(Kanku Musaa) + +Mansa Musaa (1312-1332)Bokk na ci buuri Nguuru Mali gu mag ga, yi gën a siiw. Ci 1324 la aji makka. Ca ajam gu siiw ga, àndoon na ak 60 000 ci ay surga (su ñu ci degloo Taariix as-Sudaan). Jaar ci diggu tàkk ga, ca Walata ak ca Tuwat, ba mu àggee Xaayra la ñépp yéemu ndax alal ja mu fa indi. Nee nañu yoroon na ñaari ton ci wurus. Mbaaxam ak yéwénam, yéemoon na képp nit ku nekkoon Xaayra ca jamono jooju. Doonte déggoon na araab nangul woon a làkk lu dul làkkam, daa jëloon ay tekkikat. Mansa Musaa yóbb woon na turu Mali ci mépp réewu araab, dalee ko ca Andalusiya ba Xorasan, ba Tugal, lonkoyoon wu àdduna bi, bu Angelo Dulcert(1339), wone na aw yoon wu romb Atlas, jeggi Sahara ngir àgg Mali: "rex Melli". Lonkoyoon wu Abraham Cresques, bi ko buuru Faraas defloo woon Charles V, bindoon na fa turu péeyam "Ciuta de Malli". + +Maghan(1332-1336) moo ko wuutu + +Mansa suleymaan +Mansa suleymaan(1341-1360) mooy jubbantiwaat koom-koomu nguur gu mag ga. Gën a dëggaral kiliftéefu Mali ci Diiwaani penku yi ko wër, njiitu Tuwaareg yi bu Takedda (Ayiir), nangu woon na googu kiliftéef. Suleymaan xëccoon na Mali ay boroom xam-xam ak ay àttekat yuy tòpp Maalik. Moom ci boppam fiqh la jàng, maanaam àtte ci lislaam. + +Mari Jaat(1360-1374) moo ko wuutu + +Musaa II +Musaa II(1374-1387) tegu ci, moom doonul woon ku am kàttan, xawoon naa tayyeel, jëwrinam ju njëkk la bàyee woon lépp. Moo songoon Tuwaareg yi, di def ay congam jëm Bornu + +Saayam +Lu weesu Mansa II, kujje ya amoon ci biir kër buur, te yenn saa yi rayante daan ci am, moo demoon ba faagaagal nguur gu mag ga. Ci noonu nguuru Gaawo di lekk ndànk-ndànk diiwaan yi féete penku nguur ga. Dem ba jël péeyu yaxantu bu Jenne. Doonte ci digg xarnub XV, Ca Da Mosto ak Fernadez ne woon nañu ne way dëkk yu Gammbi dañoo jàppe woon seen bopp ni ku bokk ci Mali, waaye, ci 1480, la Naba Nasere song Walata. Tekuruur jàll ci loxoy wolof yi(Jolof). Pël yu Bundu tàmbali ay yëngu-yënguy fippu, Tengela I, di ko wax it Jaje di tekki Goreelkat bi, moo leen jiite woon. Dafa bàddoo woon poseb ay yi amoon ci diggante Mali ak Gaawo daal di def li muy def. Nekkon ci dëkk bu am solo ci wàllug yaxantu, Kingi. + +Imbraatóor gu Mali + +Imbraatóor gu Mali : + +Nguurug Susu ci xarnu bu fukk ak ñatt tegoon na loxo ci askanu Maandeŋ. Sinjaata, doomi kenn ci buuri Maandeŋ yi, daa dogu woon ci goreel aw askanaw, ci noonu mu tawal ab xare walla am mbooloom xare (larme) mom ci la ame ndam ci kaw Susu, ci xareb Karina ba atum 1235 g.j., ci noonu la am réewam tembe woon (amoon independance). Ginnaaw bi Sinjaata amee ndam ciy noonam, la giirug Maandeŋ daje (Konaate, Traaware, Kayta, ak Kamara) taxawal ag imbraatóor gu mag mooy gu Mali gi, Sinjaata jiite ko. + +Sinjaata songoon na suuf yi feggoo woon ak moom ngir boole leen ci nguuram gi, loolu nag li ko ko may mooy xareem (armé) bu am bi doole, te nosu. Bi Sinjaata di faatu Mali moo nekkoon imbraatóor gi gën a rëy ci sowwu Afrig, péey ba di woon Niaani. + +Ñi ko fi wuutu woon duggoon nanu ci lislaam, wéyoon it ci yaatal gëwéelub nguur gi, ba mu mujjoon ëmb mbooleem la ko dale ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, ba ca dëkkub Gaawo ci penku bi. Ñu séddale réew mi ciy diiwaan bu ci nekk ag kilifa jiite ko guy doxal ndigali buur bi, di dajale galag yi, tey doxal yoon. Ci jamonoy buur bi Kanka Muusaa la imbraatóor gi àggoon ca gën jaa kawey ay njobbaxtalam, ci xarnu bu fukk ak ñeent. +Nguur gi nag daa na jot ci màng mi tukkee ci mbelli wurus yi ak yaxantug tàkk g i. +Ci atum 1324 g.j., Kanka Musaa aji woon na Màkka, ci tukki bu tollu ci 18 weer, won na ci adduna bi dooley nguuram gi ak woomleem gi. + +Amaloon na ay séqoo yu yaxantu ak réewi bëj-gànnaaru Afrig, indi it ci nguuram gi ay boroom xam-xami jullit yu juge penku. Ci xarnub fukk ak juroom benn la ay jafe-jafey wuutu (xilaafa) tàmbalee feeñ, ak dagu (sécession), looloo jur néew-dooleg ay diiwaan yu bari, bu ko defee Songaay daal di ñëw songu Mali, nangu ko. + +Taariixu Afrig +Nguuri Afrig +Siin-Saalum bokk nañ ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon. Ñaari nguuri Séeréer la ñu woon (Siin ak Saalum). Siin moo njëkk Saalum. + +Fa mu nekkoon +Moo nga nekkoon ci diggante yii: Kees, Njaareem, réewum Gaambi, mbàmbulaanu Atlas, ci diggante bëj-saalum ak sowu Senegaal, ca dexu Saalum. Diwaan ba mu nekkoon bari woon na ndox lool, amoon tamit ag joor ak ab àll, amoon na suuf su nangoon mbay. + +Yenn ci dëkk ya nekkoon ca nguur ga: Ndukumaan, Kungéel, Pakaaw, Rip, Lageen, ak Ñombaato. + +Way dëkk ya +Séeréer si ñoo dëkkoon ca diggante bëj-gànnaar, ak sowu ca xeru Mbàmbulaanu Atlas ma. Yii ñoo nekkoon seeni dëkk: Fasnaa, Sàngamaar, Mbòojéen, Juwaalo, ak Faajut. + +Saalum Séeréer si ñoo fa dëkkoon ak Tukulòor yi ak Wolof yi. Li ko dalee Kawlax ba Kafrin ca bëj-gànnaar, ba Ñooro bu Rip ca bëj-saalum. Soose yi ñoo dëkkoon Ñoombaato. + +Li ko sos +Séeréer yi nga xam ne ñoo njëkk a dëkk Siin-Saalum, Tekuruur la ñu jòge. Ba nguuru Gana gu mag ga daanoo, ca la Muraabituun yi agsi Fuuta Tooro indiwaale dundin bu bees bu aju ci ponki Lislaan. Ci noonu ngir bañ a tuub, ñu taamu gàddaay, wàcc jëm bëj-saalum ca Jolof. Ba ñu demee Jolof am fa ay jafe-jafe la ñu gën a wàcc dem sañc Sii-Saalum, muy seen dal bu mujj. + +Foofa la leen Mandeŋ yi fekk, ñoom ñi jòge woon bëj-saalum ca réewumGaabu. Ci ay gëstu gis nan seeni jeexit ci Dakar, ca Sàngomaar, ak ca Jaxaaw. Lebu yi fa la ñu leen fekk daa di leen fay jëlee. + +Dëkkaale diggante xeet yi +Mandeŋ, Séeréer, Wolof(lebu yi ci biir), pullaar, yii ñoo doonoon xeet yi nekkoon ca nguur ga, dëkkoon ci diwaan yi nekkoon ci wërlaayu dexu saalum gi. Mandeŋ yi ñoo nekkoon ci bëj-saalumu nguur ga, maanaan ca Ñombaato, ca Rip, ak Kolar. Lebu yi nekkoon ca bëj-gànnaar, Bawol-bawol yi ca penku. + +Gelawaar +Gelawaar mooy néeg bi daa falu ca nguuru Siin-Saalum. Li ëppoon ci ñoom ay Jambaar la ñu woon, ñoom ci cosaan ay mandeŋ la ñu, ca Gaabu la ñu jòge woon ca xarnub XIV. + +Ñoom nak ca giiri Gelawaar yu mag ya la ñu bokkoon, ay mandeŋ la ñu. Mandeŋ yi donte doonu woon mbooloo mu bari, waaye ay jambaar la ñu woon. Taxawaloon nañ seen nguur gu mag ga na mu leen neexee woon. Séeréer si ñoom ay jaambur lañu, duñu ñiti ay, looloo tax mandeŋ yi manoon a jël kilifteefu nguur ga, donte Ñoom(Séeréer si) ñoo njëkk a ñëw ca barab ba. +Yilif nañu nguur ga juroomi xarnu. + +Mansa Waali Jonn Maane +Mansa Waali Jonn Maane moo sos Amsell péeyub nguur ga, moo fa dëkkoon aki jambaaram. Daal di bàyyi ay way xaralaam ca Faajut, ay surgaan ca Jong Juwaal. + +Mbegaan nduur +Mbegaan Nduur moo daaneel Aali Baana di woon njiitu diine ca tukulòor ya, doonoon sëriñ bu amoon doole ca Saalum rawatina ca Kawòon. Ci moom la Séeréer si yéegée ci jal bi, doon ay buur. + +Moom Mbegaan def na lu ne ngir man a jot ci nguur gi. Ba mu ca jotee la noot nguur-nguuraan ya nekkoon ca wetam: Ngabi, Ndukumaan, Kaymoor, Mandaak, ak Jiloor, ak Genig, ak Jokkul. Dawloo buur ya teg fa ay ñoñam. + +Yorteef ak Yoon +Siin ak Saalum bokk ñu woon ay àtte, waaye seenug yorteef daanaka benn la woon. Seen ñaari buur yi ñoo bokkoon maqaama: Buur. Ca Siin buur ba nu ko neex la daan àttee, waaye ca Saalum buur ba da daan diisoo ak ña ko faloon. + +Boroom ndomboy tànk yu mag ya ñoo daan doxal: Njiitu Jaraaf yi, ñoom la buur daan diisool, Farba, Bëkk-néeg, Jaalige, Saltige, Njiitu dëkk yi,... + +Delluwaay +Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998 + +Lëkkalekaay yu biir + senegaal + Jolof + Waalo + Kajoor + Fuuta Tooro + Réewi lebu yi + Tekuruur + Bawol + +Taariixu senegaal +Afrig +nguuri senegaal +Cosaan Séeréer +Taariixu Gàmbi +Sowwu Afrig ab diiwaan la ci Afrik. Mi ngi tambalee ca Niseeria ba ci Senegaal. Afrik da fa mel ne arafu 1, am lu taxaw ak lu génn jublu sowwu, lu génn loolu lépp te féete ci suufu Saara man nan kaa jappee Sowwu Afrik. + +Bun ko jaawale ak Maghreb di baatu araab buy tekki sowwu. + +Su nu sukkandikoo ci seddaleb adduna bi Mbootaayu Réew yu Bennoo(onu) yi def, Sowwu Afrik bénn la ci diwaan yi ñu seddalee Afrik. + +Fukk ak juroom bénni (16) réew la am : + Benin + Burkina Faso + Kot diwaar + kap Weer + Gaambi + Ginne Bisaawóo + Gana + Ginne + Libeeria + Mali + Gànnaar + Niseer + Niseeria + Senegaal + Siraa Leyoon + Togóo + +Melosuuf +Tefesu gii xaaju Afrik ci Mbàmbulaanu Atlas la bokk. Tefesam xaajoon nan ko joxoon leen ay tur: Tefesug pépp, Tefesug wurus, Tefesug bëñu-ñay (ci nasaraan:Côte d'Ivoire, moo indi turu réewum Kot diwaar). Jappum njaam mi yëggaloon na barab yooyu bu baax; ba tax na sax lu ëpp ci jaam yi fa ñu leen jaarale yòbb Amerik. + +Ci barab yu bari yi nekk ci Diwaan bi kilimaab yemoo la ñu am, allub yemoo it am na fa. Bari na ci ay réew yu bari gancax, am na ci tamit réew yu bekkoor: yi jege ndand féy-féy gu Saara, yu ci mel ne Senegaal ak Mali + +Réew yi génn ci géej gi + Benin + Kot diwaar + Gaambi + Gana + Ginne + Ginne Bisaawóo + Libeeria + Gànnaar + Niseer + Niseeria + Senegaal + Siraa Leyoon + Togóo + +Réew yi génnul ci géej gi + Burkina Faso + Cadd + Mali + Niseer + +Dex yi + Dexu Senegaal + Dexu Niseer + Dexu Gaambi + Dexu Siin-Saalum + +Taariix +Ci taariix Diwaanu Sowu Afrik mooy barab bi nguur yi ëppoon solo ci Afrik nekkoon, man nan cee woññi yénn: Nguuru Mali gu Mag ga, Nguuru Songaay gu Mag ga, Nguuru Gana gu Mag ga. Doonoon na génn ci barab yi xay yi gën a mag juddoo ci adduna bi, dëkk bu mag bii di Timbuktu bokkoon na ci selebiyoonu njaay ak cosaan yi gënoon a mag ci jamono ju yagg ja. Ay réew yu amoon-alal te bariwooni yëggu-yëgguy cosaan ak aada nekkoon nañ fa, waaye li leen gën a faagaagal mooy jappum jaam mi ak coppitey klimaa bi, ñakkum ndox mi (rawatina taw) moo réy mbay meek camm gi ak lépp li ciy génnee. + +njëkk-taariix +Ay gëstu yu bari wone nañ ne ay nit ñëwoon nañ ci Sowwu Afrik, njoort nañ ne ay Pigme lañ, ci li jege atum 12.000 B.K.(balaa Kristaa). Ay jumtukaay ngir liggéey ak xeer, gis mañ leen ci mandiŋ mi, fa nga xam ne ay sammkat a fa nekkoon yu daan jëfëndikooy jumtukaay yu ñu yatt ci xeer (ay paaka, xeec,...). Ñi dëkkoon ci all bi nak ci yax lañ daan yatt seeniy jumtukaay. + +Melosuuf +Afrig +Diwaani Afrig +Bëj-gànnaaru Afrig mooy diwaanu Afrig bi féete ci li nekk ci kawu tàkk gu Sahara. + +Mooy la nuy faral di wax Afrig gu weex gi, ndax melokaanu ña fa dëkk, bii baat day safaano ak Afrig gu ñuul gi, di tekki Afrig gu bëj-saalumu-Sahara. + +Séwógaraafi + +Réewi bëj-gànnaaru Afrig : + Alseeri + Isipt + Libi + Marok + Sudaan + Tiniisi + Sahara gu Sowwu + +Taariix + + Ci jamono ju yagg ja « Afrig » da doon jëmmal diwaanu Kaartaas, mooy réewu Tiniisi gu tay. Afrik ab diwaanu Nguuru Rom gu Mag ga la woon. Bi jullit yi ñëwee, baat bi dañ kaa soppi, araabal ko Ifriqiya. + Beerbeer yi, ñooy way dëkk yiñ ni ñoo njëkk ci bëj-gànnaaru Afrig. + Maghreb (sowu ci araab), moo ëmb réew yii : Gànnaar, Marok, Alseeri, Tiniisi ak Libi. + « Afrig gu weex » bu njëkk da doon jëmmal barabu Afrig bi ay nit yu xees dëkkee : Marok, Alseeri, Tiniisi, Libi, Esipt. Waaye tay baat bi liñ kay jëfëndikoo bariwul. + +Diwaani Afrig +Bëj-saalumu Afrik moo ëmb barab yi nekk ci Bëj-saalumu allub yemoo gu Afrik. + +Dañ ciy boole tamit duni Afrik yi nekk ci Bëj-saalum-sowu mbàmbulaanu waa-End ci wetu Madagaskaar ak duni Afrik yi ci Bëj-saalum-penku mbàmbulaanu Atlas. + +Askani Xoysan ñoo fa njëkk a dëkk, ci li ci tegu la bantu yi ñéw. Ci jamono gi waa tugal aakimoo diwaan bi, lañ seddale réewi tayam yi. + +Doon na diwaan bu am-alal te suufam naggu lool mbay. Rèew mi gën a jëm-kanam ci Afrik, fa la ne rawatina muy Réewu Afrik gu Bëj-saalum + +Séwógaraafi +Juroomi Réew ñoo nekk ca diwaan boobu: + Botswana + Lesoto + Namibi + Afrik gu Bëj-saalum + Eswatini + Malawi + Madagaskaar + Mosambik + Saambi + Móoris + Komoor + Simbaawee + +Melosuuf +Afrig +Diwaani Afrig +Penku Afrig mooy wàllu Afrig gi gën a féete penku. Bénn la ci diwaan yi ñu séddalee goxu Afrig. + +juroom ñenti Réew a fa nekk: + Eritere + Ecoopi + Jibuti + Somali + Sudaan gu Bëj-saalum + Keeñaa + Ugandaa + Tansani + Ruwandaa + Buruundi + +Ruwandaa ak Buruundi yénn saa yi dan leen di boole ci Diggu Afrig, ndax li ñu nekk ci diggante ñaari diwaan yi. + +Jibuti, Eritere, Ecoopi, Somali, ñooy réew yi ñuy woowee Bejjenu Afrig. + +Melosuuf +Yénn barabi penku Afrik,siiw nañ ndax seeni rabi all yu bari, yu mel ne segg, gaynde, ñay,... Li ëpp ci diwaan bii nak ñaay la. Doju Kilimanjaaro ak doju Keeñaa, ñooy yi gën a kawe ci Afrig. + +Ci gii xaaju Afrig, làkk yu bari lañ fay wax, kàllaama waa angalteer ak gu waa faraas ñooy yi fa gën a tas, waaye bu nu fatte kiswhili di itam làkk bu tas ca diwaan ba; baati bantu ak yu araab ñoo booloo doon ko. Diiney krist mooy bi fa gën a tas rawatina ca Ecoopi. Doon na diwaan bu bari ay xare yu junniy nit faatoo: ca Sudaan lu mat ay fukki at a ngii ñu ne ci xare, ca Ecopi ba buur ba daanoo ba tay ñu ngi xare ci seen biir. Moom Ecoopi am beneen xare bu mu sexxal ak Eriteere mi ko doon laaj tembteem te jot ko ci 1993, am na fanweeri at. Ca Somali itam ay at a gii ñuy xeex ci seen biir. + +Taariix +Penku Afrik teewee na ay nguur yu mag, rawatina gu Ecoopi. Man nan wax ne mooy nguur gi njëkk ci Afrig. Am na yénn taariixkat yu naan sax ña sosoon Esipt gu yagg ga fa la ñu jòge woon. Nguuru Ecoopi moo tegoon tànk ca diwaan boobu ci jamono ju yagg ja. Lu ko daleen ci xarnub XIX ba bu XX waa tugal yi ñoo leen nootoon, aakimoo woon seniy suuf. Waa portigaal yi ñooy ñi fa njëkkoon a ñéw, waa faraas yi ak waa angalteer yi dal di ci tegu. + +Diwaani Afrig +Ag kembaar / ab gox baat la buy tekki ab yaa-yaa wu suuf wu rëy te tegu ci kol-kolu àdduna si. Cig déggoo barab bu ñuy woowee kembaar dañu ciy boolee tamit dun yi ko jege, maanaam yu soriwul tefes yi, lu mel ne Madagaskaar ni mu bokkee ci kembaaru Afrig, ndax moom la gën a jege ni Asi. + +Seddatleeg kembaar yi +Ci xam-xam, xaaj bu àdduna bi, bu beru rek gox nga, ci tekki bu yaatu, kon sunu sukkandikoo ci loolu dun yépp ay gox la ñu, ndaxte da ñoo beru, dañ ni cundum ci ndox mi. + +Baatu gox amul benn tekki rekk. Looloo tax daanaka barab boo dem ci àdduna bi am na ay limi gox. Ci lu daj man nañoo jàpp ne mooy ab yaa-yaa wu suuf wu réy wu am ay yemu yu am solo,(mbàmbulaan, doj, ndand féy-féy... Donte ñu bari da ñoo jàpp ne ñent walla juroomi gox a am waaye di nan far di ci téye juroom walla juroom ñaar. + +Ñaar yi ci tàqaloo ñooy Tugal ak Asi, di ko woowee Tugalasi, Bëj-saalumu Aamerig ak Bëj-gànnaaru Aamerig danuy faral di leen di jàppee ñaari gox, suñu booloo nekk Aamerig. Ñenn ñi di boole Afrig Tugal ak Asi mu doon Afritugalasi. + +Dun yi dañ leen di boole ci gox yi ñu gën a jege. Lu mel Kanaari donte ci réewum Espaañ la bokk, ci goxu Afrik lañ koy boole. Duni Mbàmbulaan gu dal gi, ci Oseyaani lañ leen boole, ak yeneen. + + 7 gox: Afrig, Bëj-gànnaaru Aamerig, Bëj-saalumu Aamerig, Asi, Tugal, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum. + 6 gox: Afrig, Bëj-gànnaaru Aamerig, bëj-saalumu Aamerig, Tugalasi, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum. + 5 gox: Afrig, Aamerig, Tugal, Oseyaani, Asi. + 4 gox: Aamerig, Afritugalasi, Oseyaani, Dottu Bëj-saalum. + +Gox yi +Afrik gu bëj-saalumu-Sahara, moom lañ daan woowe Afrik gu Ñuul, moo safaanoo ak bëj-gànnaaru Afrik, yem ci Sahel. Seddale gi tegu ñu rekk ci mbiri séwógaraafi, waaye ci mbiri cosaan ak aada tamit. Ba ca jamono ju yagg ja, ndand féy-féy gu Sahara da fa musa xaajale ñaari wàlli Afrik yi, moo jafeeloon weccoo gi ci aada ak cosaan ak njënd ak njaay mi. + +Afrik gu bëj-saalumu-Sahara ci lu daj, dañ koy seddale ci ñenti diwaan, yu gën a siiw ak yii tu: + Sowwu Afrik; + Penku Afrik; + Diggu Afrik; + Bëj-saalumu Afrik. + +Ñeent fukk ak juroom ñaari réew ñoo fa nekk, am juroom ñaar teemeeri miliyoŋi way dëkk (ci ndoorteelu xarnub XXI). + +Melosuuf +Afrig +Diwaani Afrig +Sahel (jòge ci araab ساحل , sahil, di tekki pegg walla tefes) di jëmmal ab barab bu bekkoor, ne ci diggante tàkk gu Sahara ci bëj-gànnaar ak diiwaani yamoo gi fa nga xam ne day taw rekk, ci bëj-saalum. Tëraayam day jàpp mbàmbulaanu Atlas jëm ca géej gu xónq ga. + +Réew ya ca ne: + + Senegaal; + Gànnaar; + Mali; + Burkina Faso; + Niseer; + Niseeria; + Cadd; + Sudaan. + +Melosuuf +Daanaka Sahel gépp gannuus la ak màndiŋ, ci lu ëpp, ñetti weer rekk lay taw ci at mi. + +Dañ koy seddale ci xaaj yu bari: + + Tàkk gi: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 150mm ci at, mépp mbay mu aju ci ndoxu taw, manu faa am. + «Sahelu màngaan yi»: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 400mm, foofu it mbay mu aju ci ndoxum taw, amal ko fa daanaka nekkuwul. Mooy barab bi sammkatu nag ak gëléem yiy màngaan di nekk. + «Sahelu way dëkk yi»: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 650mm ci at. Dugub ak aréen lañu fay bay. + «Barabu Sahel-sudaan»: fii mbay mi gën naa yaa, taw yi yokk bu baax. + «Barabu sudaan»: fii taw yi di nañ àgg 950mm ci at, tawi nawet bi, di na tax ñu man a bay dugubu suuna, mboq, wëtéen,... + +Tolof-tolof yi ëpp yi ay way dëkkam di jànkonteel ñooy: bekkoor giy gën di sax ak tàkku giy gën di jëm-kanam, di mëdd ngañcax su néew sa fa am. + +Diwaani Afrig +Bejjenu Afrik moo ngi nekk ci Penku Afrik. Mooy cat li mel ne ab ñattkoñ. + +Séwógaraafi + Jibuti + Eritere + Ecoopi + Somali + +References + +Melosuuf +Afrig +Diwaani Afrig +Maghreb mooy wàll gi gën a Féete penku ci bëj-gànnaaru Afrik, nekk ci diggante Géej gu diggu gi ci bëj-gànnaar ak tàkk gu Sahara'k gu Libi ci bëj-saalum ak Mbàmbulaanu Atlas ci penku. + +Cosaanu baat bi +Ci araab al-Maghrib di tekki "sowwugi" (suuluway); li ko waral mooy féeteem ci wàllu penku suñ ko xoolee ak fa araab yi dëkk. Di safaanoo ak Machrek (fenkuwaay, sowu), maanaam penku ga araab yi dëkkee, li ko dalee Esipt ba Iraak. Bu jëkk Jezirat al Maghrib lañ ko tuddee woon, di tekki "dun bi ci Penku", ndax nañ gisee woon diwaan bi ca jamono ju yagg ja: li mu nekkoon ci diggante géej gi ak ndand féy-féy gi. + +Ci araab Maghreb day tekki tamit Marok. Ngir jaawale bañ ai am ci, marok el-Maghreb el-aqsa lañ koy woowee ci araab, di tekki “penku gu sori gi”. Di nañ ko wax tamit “suuluwaay gu araab” + +Melosuuf +Diwaani Afrig +Isipt gu yàgg ga nekkoon na réew mu woomle, mu ami suuf yu naat, yu nangu mbay, ngir dexam gu mag googu di (Niil), am na it ay mbelli wurus ak xànjar ak weñ ak jamaa. Moo nga tambalee woon ca peggu Sudaan jëm ca géej gu diggu ca bëj-gànnaaram. + +Isipt bu njëkk dafa séddaliku woon ay xaaj. Ci jamonoy 3200 nj.j(njëkk judd gi) lañu bennal xaaj yii, mu mujj nag di nguur gu dëgër, buur bu tudd Firhawna jiite ko, ay foŋsaneer di ko jàppale yu man a bind man a jàng. +Bindkat ya dañu daa jëfandikoo li nuy wax mbindum Yirogliif, ñoom nag bindkat yooyu lañu féetale woon war a jottali ndigali buur bi, ak dajale galag yi (juuti yi) ak taxawal yoon. + +Ñoñam it siiwoon na ñu ci yaxantu ak réew yi ñu digool, ci gaal yi daa jaar ci Niil. +Waa Isipt am nañu xay gu cosaanu, ñu nekkoon ñu daa gëm ay yàlla yu bari, daan leen melale ci bindu nit ku am boppub bàyyima., yàlla ju ci mel ne Amoon Ra (yàllay jant ji) benn la ci ak Isis (yàllay weer wi) , nga xam ne Firhawna it yàlla lanu ko jàppe woon. Daa nanu tabaxal seen yàlla yi ay jaamuwaay (ay temple) ngir màggale leen ko. Ña cay ñu woomle dañu daa tabaxal seen bopp ay bàmmeel yu yor bindub mbaanaar (pyramide). +Bu ñu daa suul seeni néew nag, dañu ci daa boole mbooleem seeni bagaas ak alal. +Ci atum 332 nj.j la waa Geres teg loxo Isipt, booba it la tàmbalee naaxsaay. + +Isipt ak Afrik gu ñuul gi +Seex Anta Jóob (1923 – 1986 g.j) moom lañuy jàppe boroom xam-xam bu Senegaal bi jot a def ay gëstu ci nguurug Isipt gu yàgg ga, mu leeral ci séqoo gi am ci diggante xayug Isipt ak xayug waa Afrig yu ñuul yi. + +Seex Anta Jóob wuññi na jaare ko ci gëstoom yooyu mu defoon ci mbind yi nu yatt ci doj yi ci Isipt, ak ci gëstu yi mu defoon ci tàdd (cadavre) yu ñu taaniit (momifier) yi , - wuññi woon na ne Firhawna yi de li ëppoon ci ñoom ay nit ñu ñuul lañu, ñu néew reek ñoo ca nekkoon ñu weex. Seex Anta it wone woon na niroo gi am ci diggante lu bari ci làkki waa Afrig yi ak làkku Isipt wu yàgg wa, ponki làkk yi ak bennaani baat yi dañoo niroo. + +(Man nag ma ne ngir dëggal niroo googu : mbaanaari séeréer yu yàgg ya ak mbaanaari waa Isipt yi walla seen pyramide yi, xool-leen leen, ag niroo ngi fi de, waxuma la nag suulaale gi waa Isipt yi daa suulaale néew beeki bagaasam te séeréer su yàgg sa daa ko def .) + +Am na yeneen tomb yu ñu bokk ci diggante Isipt gu yàgg ga ak Afrig gu ñuul gi : +Am col ak watuwiin, ak topptoowiinu kër ak yenn ci ay gëm-gëm aki jaamuwiin. + +Wuññi yii wone nanu ne ag wàll ci xayug Isipt ga ci Afrig gu ñuul gi lañu ko jële. + +Yenn ci wuññi yu waa Isipt +Isipt gu yàgg ga daa nekkoon gu di boroomug xay gu kawe gu dimbalee ci amal ay wuññi yu am solo ci wàllug xam-xamu xayma, ak xam-xamu falag (fidiw). + +Fànnu Isipt bokk na ci fànn yi gën a rafet ci yu yàgg ya. Xam-xam yii nag tas nanu ci àdduna bi, kon goxub Afrig sañ naa ndamu ci li mu indil ag nite ciy liggéey yu am solo. + +Waa Isipt defar nañu ab arminaat, lim ci at mi muy 365 fan : 12 weer * 30 fan = 360. +Ñu dolli juroomi fan ngir màggale ci juddug seen yàlla yi : Osaris – Isis – Oris – Sit – Nifti . +Séddale nañu at mi def ko 4 xaaj, xaaj bu ci nekk am ñeenti weer. Weer wi ñu séddale ko ñeenti ayu bis, gu ci nekk am fukki fan. Bis bi nag ñu séddale ko 24 waxtu. + +Isipt gu yàgg ga +Taariixu Isipt +Yaatug lislaam ci Afrig gu sowwu gi : + +Ci njëlbéenug juroom ñaareelu xarnu la Muhammad (j.m) tàmbali di tas diine ju yees ji (lislaam), ginnaaw bi mu làqoo atum 632 g.j, la araab yi ubbi Afrig gu sowwu gi, daal di duggal aw nitam ci lislaam, ci noonu, jullit ñi tàmbalee tas lislaam ndànk-ndànk ci bëj-saalumu tàkk gi (désert bi),. + +Lislaam mujj na yaatu, tas te li ko waral du dara lu dul joqalante gu yaxantu gi naar yi daa def ak Afrig, ak njëgg (convoi) yu giléem yi daa jëggi tàkk gi, nga xam ne yaxantukat yi dañu daa jënd wurus ci sowwu Afrig, jaayiji ko ca bëj-saalumu Afrig, daa nañu baana-baana it ci jamaa ak jumtukaayi xanjar yi ak weer aki téere ak xorom ci dëkki yaxantu yii : Jinn, Tumboktu, Gaawo. +Yaxantukat yooyu dañoo fekk lislaam ca bëj-gànnaaru Afrig, bu ko defee, la ëpp ca ñoom daal di ciy dugg, daal di tàmbalee waar seeni àndandoo ngir dugal leen ci. + +Waaye yaatug lislaam gi amewul ci jàmm rekk, ndax yenn askan yi dooni jullit dañoo jugoon def jiyaar ngir tàbbal yeneen yi ci lislaam. + +Murabituun (Marabout) yi nga xam ne ñi ngi juge woon ci bëj-gànnaaru Afrig, ubbi woon nanu lenn ci Afrig gu sowwu gi ci xarnu bu fukk ak benn + +Lislaam +Imbraatóor gu Gana gi mag ci yu Afrig yi taariixkat yi mas a xam mooy : gu Gana. Li ñu jot a xam ci taariixam ñi ngi koy sante gëstuy boroom xam-xami jeexiit yi, ak nettaliy gimiñ yi, ak mbindi tukkikati naar yi. + +Gana mi ngi sosu ci ñeenteelu xarnu g.j., jamono jooja it nguur gu ndaw la woon gu ñu daa woowe Ogaadoo. +Ci juroom ñatteelu xarnu g.j., la ab xareem (son armée) jugoon song ay suuf yu yaatu, yu nekk ci diggante dexug Senegaal ak Nijeer, ci noonu la Gana wëlbatikoo di imbraatóor gu mag gu teg loxo ci dëkk yi mu feggool… + +Imbraatóor gi nekkoon na di gu naat : ay suuf yu nangu mbay ak sàmm, mu daa bokk ci yaxantug tàkk gi (gi nu daa defe ci tàkk gi) ak njaayum wurus mi, moom imbraatóor gi amoon na ay mbelli wurus yu bari yoy ki ko daa topptoo mooy Kayaamagana, maanaam njiitul wurus li : waa jii da daan nekk njiit lu dëgër, lu ñu wormaal, luy àtte cig maandute te daan samp foŋsaneer yi. +Moom nag cim koom ak naataange la daa dunde ci péeyam, waa diiwaan bii it dañu ko daa indil ay kem ci wurus wi ñiy génnee ci suuf si, ginnaaw bi mu faatoo nag la ko fi ab jarbaatam wuutu. +Ci atum 1052 g.j., la Muraabituun yi song Gana, ci layuw dañuy dugal ñoñam ci lislaam, ñu daal di ubbi péey ba atum 1076 g.j., ginnaaw bi Gana néew doole, daal di daanu ci mujjantal gi ci loxoy imbraatóor gu Mali atum 1240 g.j. + +Taariixu Afrig +Nguuri Afrig +Imbratóor gu Songaay : + +Ci juroom ñaareelu xarnu g.j., la askanu Songaay wi dëkkoon ci tefesug dex gu Nijeer gi taxawaloon ag nguur gog péeyam moo nekkoon Gaawo. Mali nag moo tegoon loxo askanu Songaay wi ci xarnub fukk ak ñatt g.j., waaye ñoom jotaatoon nanu ci seenug temb te ñi ko waral di njabootug Soni gi ci xarnub fukk ak ñeent, daal di tàmbalee naat. Soni Aal-Béer (maanaam Aal mu mag mi) moo nekkoon buur bi la ko dale ca 1464 g.j., ba 1492 g.j., wutaloon na nguurug Songaay xare (armée) bu am doole, mu daa def ay ubbi (conquête) ngir yaatal nguuram gii nga xam ne mujj na tuxoo ci nguur dem cig imbraatóor gu ñu mujj tudde Songaay walla Gaawo. Bi Aal Béer dee la kenn ci ay njiiti xareem teg loxo ci nguur gi, daal di wutal boppam dàkkantalu Askiyaa (maanaam imbraatóoor bi), moom nag àtte na ba ci 1528 g.j., mu gën a rëyal mbooloom xareem mi, wéy ci ubbeem yi, bu ko defee imbraatóor gi mujj tàlleeku dale ca mbàmbulaanug atlas ba ca Borno ci penku bi, dalewaat ca Jini ci wàllug saalum gi ba ca digi Marog ci wàllug bëj-gànnaar gi. Gii imbraatóor nag àggoon na ci njobbaxtalam ci jamonoy Askiyaa Muhammad. +Buur bi moo daa jox ndigal foŋsaneer yi, di lijjanti diiwaan yi, benn gongikuwaayu alal bi nguur gi amoon mooy yaxantug tàkk gi. + +Nguur gi nag, réew yi mu feggool xuppoon nanu ko : ci atum 1591 g.j., buurub Marog yabaloon na ab xareem ñu jaar ci tàkk gi ngir song Gaawo, moom nag amoon na ndam ci waa Songaay ngir ngànnaayi sawaraam yi mu jénde woon ci waa Tugal yi. Ci nii la Songaay tàmbali woon di doyadi ak di dagu. + +Taariixu Afrig +Nguuri Afrig +Waa Tugal yi ci tefesug Afrig gi : + +Yaxantug ñatti koñ yi : + +Ci lu tollook juróom ñatteelu xarnu g.j, jaayees na ay jaam yu waa Afrig ci ay yaxantukat yu daa def yaxantug tàkk gi, ak gu tefes gi ci tefesug mbàmbulaan gu End gi (ocean indien). + +Jaam yi jógewoon nañu nguuri Sowwu Afrig: nguuri Senegaal, Gana, Niseeria, Kamerun, Gaboŋ, nguurug Kongóo, nguurug Ndongo ak yeneen nguuri Angolaa. + +Ñu màng jaam yooyu yobbu leen ca Afrig gu bëj-gànnaar ga (naar yi), fa la ñu leen jaayaat, ngir ñu doon fay mbindaan aki surga aki soldaar. + +Gii yaxantu moom lañuy woowe njaayum jaam yi. Njaayum jaam yi gën naa yaatu bi xarnub fukk ak juroom benn tàmbalee g.j : +Waa Tugal yi dañoo aajowoo woon ay loxo yuy liggéey ngir jariñoo mbell yeek suuf yi ñu moom ci Amerig. Looloo taxoon ñu gaawoon dem ca tefesug Afrig gi ngir jëndi ay jam. +Ginnaaw nag jaam ya nekkoon ca tefes ga doyuñu woon, ñoom waa Tugal yi dañoo yabaloon ay ñu leen wuutu ñu Afrig ngir ñu gëstujil leen ay way néew-doole ci biir gox bi. + +Ndawi tubaab yu Afrig yooyu dañu daan song dëkk-dëkkaan yi di leen lakk, di ray mag ñeek ndaw ñi, bu ko defee yobbu góor ñeek jigéen ñi am kàttanug liggéey. Dañu leen daan jéng, jiital leen ñuy liiru jëm ci digg yii : Gore – Owida – Luwanda. Foofa lañu leen di jaaye tubaab yi leen di sëf ci gaal yi, dem ak ñoom Amerig ci ay nekkiin yu metti te wow, yuy far a ray li ëpp ci ñoom ba lañoo àgg fa ñu jëm. Bu ñu àggee Amerig rekk ñu jaayati leen way meññilu yi (les investisseurs :exploitants), bu ko defee ñenn ci ñoom ñu tàggale leen ak seeni njaboot, te daa leen manante ci def liggéey yu diis yi. +Sang bi nag daa na am àq ak sañ-sañ bu mat ci def lu ko soob ci jaam bi. Bu moyee ay ndigalam sang bi daa na digale ñu mbugal ko ba loolu leeg-leeg daa na waral ag faatam. +Ci atum 1787 g.j, lañu jël ay matuwaay ngir aaye yaxantu gu ruslu gii. Ci jooju jamono la ay mbootaay sosu yuy safaan ag njaam, gu ci mel ne mbootaay ga amoon ca Angalteer ngir jële fi njaam, ak lonkoo gu xariti ñu ñuul ñi ca Frãas. +Waaye njaayum jaam moom dañul ndare ca mujjug xarnub fukk ak juroom ñeent g.j . Afrig ñàkk na ay milyoŋ ciy doomam ngir njaayum jaam yi. Moom de – njaayum jaam – ag tooñaange gu mag la ñeel ag nite ci lu dul gën jaa néewi sikk. + +(( Li ñu jublu ci yaxantug ñatti koñ yi mooy jaay gi ñu daa def doomi Afrig yu am yi kàttan, ngir ñu bayi te tabaxi Amerig te waa Tugal yi ko daa def, di jël njëg ga’ak di ko yobbooti Tugal, ngir suqali ko ca. Kon muy yaxantu gu ñatti koñ séq : Afrig gi ñuy jële njaay mi, Amerig gi ñu koy jaayeji, ak Tugal gi koy jëndsi walla fëkksi ci Afrig, jaayeji ko Amerig, yobbu njëg ga Tugal. Fii ba tay man nañu fee gis ne Afrig jëf na ay jëf yu am solo ci jëm-kanam gu koom-koom, gu mboolaay, gu fànn ak ak ak, gu ñaari gox yii, te yii ñaari gox ñoom it dox nanu bu baax cig deltu ginnaawam, ndax ŋacc nañu ciy ponkalam, yi ko manoon a jëmal kanam aki xéewalam, yi ko manoon a liggéey, ci ginnaaw bi ñu ko sancee (coloniisee), teg ko loxo, muucu ay gongikuwaayi xéewalam, yobbu defare seeni réew)) + +li juddoo ci njàppum jaam yi + +Njuréefi njaayum jaam yi (les conséquences) : + +Askani Tugal yi dugg nañu ci njaayum jaam ci anam gu tar, looloo waral : + +- Ay gëpplante aki xare ci diggante réewi Tugal yi + +- Barig ñi dee ak ñi ñu ray ci xare yi ak ci biir dox bu gudd bi ngir jéggi mbàmbulaan yi + +- Jeqikug askani Afrig yi ngir jàmmaarloo : looloo fi jur ay jafe-jafe yu mboolaay, yu koom-koom yu tar, niki néew dooleg dëkk yu mag yi, tasug ab xiif, wañse, ak yàqug jikko yi, ak amadig kaaraange ak tasug njaboot yi. + +- Ŋacc Afrig ciy doomam yu am yi doole, ak ci kàttanam yu nit yi, looloo ko doyadiloo woon ba manul woon a jàmmaarlook canc gi (colonisation). + +Ngir mettiit yi jaam yi daa jànkoonteel, boroom yéene yu rafet yi jug nañu ngemb séen bopp ne dañu fiy jële njaam ci turu teddngay nit : ca Angalteer ag yëngu-yëngu judd na fa ngir neenal njaayum jaam (le mouvement Abolitionniste). +Bu dee ci Frãas it mbootaayug xariti ñu ñuul ñi (Organisation des Amis des Noirs) taxaw fa ngir xeex ag njaam. Waaye yaxantu gu gàccaale gii jëleesu ko fi lu dul ci atum 1848 g.j . + +Nettali wu aju ci njaayum jaam +Aw dogiit wu ñuy yër (lire): + +Suñu maam yi ci teraanga ak jàmm lañu nekkoon, ami gétt aki tool. Bis gis nañu ca biir géej ga lenn njanaaw lu mag, lu ami laaf yu weex. Aw nit wu weex bàyyikoo nañu ca ndox ma, tudd ay baat yoy kenn ci ñoom déggu leen. Booba la sunu maam yi tiit: ñu jortu ne ñoom de ay jinne lañu, ñu leen di jéem a delloowaat ci géej gi jaare ko ci jëfandikoo ay fett, waaye jinne yi soqi nañu ci seen kaw sawara sos kàddu gi daa mel ag dënnu. Rayees na ñu bari ci ñoom. Sunu maam ya ca dees daal di daw. + +Lii ci nettaliy gimiñ yi la :G.L Havaux + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Lu am ag séqoo ak njàppum jaam + + +Fent ak wuññi yu mag yi +Ci xarnub fukk ak juroom g.j, waa Tugal yi amal nañu ay wuññi (decouverte) yu bari yoo xam ne soppi nanu seenug dund, yi ëppoon solo ci wuññi yooyu ñooy wuññig moolukaay (imprimerie), ki ko def di Gutenberg ci atum 1450 g.j . + +Bu njëkk téere yi ci loxo lanu leen daan binde te loolu daa na soxla waxtu wu baree bari, looloo waraloon téere yi seer te néew. +Móolukaay nag mi ngi daan ame ci ay bind (forme) yu ñu liggéeye ci weñ, bind bu nekk daa na taxaw taxawaayu aw araf. Bu ko defee ñu raŋale bind yii nga xam ne ñooy defar jumla (phrase) yi ñu soxla, bu loolu jàllee, daa ji door a ñëw, jaar ci seen kaw, njëkk ñu leen di móol ciw këyit. +Bu ko defee ñu jël benn yax bi( copie bi) def ci ay xët yu bari, ci noonu lañuy defare ab téere. +Ci jamono jii waa Tugal yi xamoon nañu puudar (poudre à fusil) (moom nag – puudar - waa Siin na ko fentoon), ñu jëfandikoo ko ci ngànnaay yu sawara yi ñu njëkk a liggéey , xamoon nanu it buusal (moom nag wa Siin ak naar (arab) yee leen ko njëkk a xam), ñu liggéey ay gaal yu yees yu gën a gaaw te gën a man a jànkoonteek ngelaw yi ci mbàmbulaan yi . +Wuññi yii nag ñoo tax mool yi man a def tukki bu sori ci biir géej gi, te wuññi ay suuf yu yees yoy waa Tugal yi xamuñu leen woon. + +Ay tukki yu bari daal di nañuy taxaw jëm ci tefesi Afrig yi : + + Ci atum 1487 g.j, la Bartelemi Jaas agsi ca Boppu Yaakaar Ju Baax Ji ( cap de bonne esperance). + Ci atum 1492 g.j, la Kristof Kolombo jugoon di wër aw yoon wu koy àggale End waaye mu far àgg cig mbetteel ci Amerig gi nga xam ne waa Tugal yi sax xamuñu woon ne am na. + Ci atum 1498 g.j, la Vasko De Gama jugoon di wër Afrig tukkee ci bëj-saalum, daal di àgg End. + Ci diggante 1519 ak 1522 g.j, la Magelan def ab tukki bob ci la wëre àdduna bi, ci lañu wone it ne àdduna bi dafa bulu (kol-kolu). + +Digg (centre) yu yaxantu yu njëkk yi +Waa Tugal yi bi ñu tàmbalee seen wuññi yooyu lañu gaawantu teg loxo suuf yii ñu wuññi : +Mool yi toppante nañu ci tefesi Afriig yi, waa Portigaal yi jiitu ci, waa Espaañ yi topp ci, waa Olaand, waa Angalteer ak waa Frãs. +Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la waa Portigaal ak Espaañ teg loxo Amerig gu bëj-saalum gi, bu ko defee waa Portigaal ya jël fa sancu (colonie) bu Breesil féetele ko seen bopp, yeneen wàll ya ca des nekk ca ron ŋëb gu Espaañ. +Way sanc yi ( les colonisateurs) tambali woon nañoo génne koom-koom yu mbell yi (yu mine yi), bay it yenn mbay yi niki bantu suukar ak póon ak wëtéen. +Waa Tugal yi bëgguñu woon a dugg ci goxub Afrig, ñoom daal dañoo wutoon ay digg yu yaxantu ( centres commerciaux) ci tefes gi, aki waax yu ñuy faral a jaar bu ñuy dem End: benn ngir defar fa seen yaqu-yaqu yu gaal walla ngir wut fa ab dund walla ngir yaxantu, ndax dañu fa daan jënd ay marsandiis yu Afrig niki wurus ak bëñu ñay ak daakaande ak ay rëndaay ( condiments). +Waa Tugal yi bi ñuy sanc tefes yi ak di fa tabax ay digg yu yaxantu, daje wuñu woon ak benn jafe-jafe bu juge ci waa Afrig yi, loolu daal ci jàmm lañu ko defe akug dal. Li am sax mooy way dëkk yi teeru nañu leen ci teraanga, jox leeni suuf ak jumtukaay yi manul a ñàkk. +Diggi yaxantu yooyu nag ñi ngi daa ame ci yii : + +Dencuwaay ( magasin) bu ñuy denc marsandiis yi +Ay dëkkuwaay ñeel waa Tugal yiy saytu digg yooyu +Ab jàngu ( egliis) +Benn saal bu ndaw bu ñuy teertoo way siyaaresi yi + +Am na ci diggi yaxantu yi yoy ñi ngi leen di liggéeye ci melokaanu tata (fortification) ju terewu (difficile d’acces) ngir moytu ay cong yu ñu leen mana def. Waa Tugal yi dañoo gis ne seen xay gi moo gën a kawe gu dul moom, looloo waraloon ñu ga woon ko yeneen askan yi. + +Taariixu Afrig +Melosuuf +Sëriñ Tuubaa Xaadimu-Rasuul (Seex Aḥmad ibn Muḥammad ibn Ḥabiib Allaa 1853-19 sulet 1927) boroom xam-xamu diine bu jullit la bu di ab sëriñ te cosaanoo ci ag càllala gu doomi soxna. Mi ngi gane àdduna ci Mbàkke, ab dëkk bu Maam Maaram sancoon ca nguurug Bawol, maamaatam jooju mooy Maharam, walla Maaraam,mooy ki sanc Mbàkke Bawol, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dëkkewu fa woon, da fa a bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah ju mu bokkalul nday. Moom nag sëñ Maaram mii daa desoon Jolof, fa la làqoo ñu denci ko fa, di ko siaare. + +Ñu koy woowe itam Xaadim Rasuul di Ñaari baati araab yuy wund Surgab yonent bi Muhammad (j.m). Mu bokk ci jëmm yi gën a fés te ëpp solo ci diiney Lislaam ci sowwu Afrig, ndax moom moo sos yoonu murit. Waa-réewam Seex Ahmadu Bamba lañu koy woowe ndax cofeel gu ñu am ci moom. + +Ar:أحمدو بمبا + +Jaar-jaaram +Doomi ab sëriñ ci yoonu (Xaadirya) – Mooy yoon wi gën a yàgg ci Senegaal –, Ahmadu Bamba ab jullit bu dëddu la woon te dib sóofiyu, daan bind it ci wàllug fiqh, tasawuf ak wéetal Yàlla (tawhiid) ak wàll yu bari ci xam-xamu diine, ak tagg Yonent bi, mbaa ci lu aju ci "shukr" (sant Yàlla). + +Jiyaaram + +Ak doonte ku daan bañ la te àndadi woon ci canc gi (colonialisme) ak teg loxo gi tubaab yi defoon réew mi teewul melul woon ne sëriñi tiijaan yi jugoon di jiyaar, ku ci mel ne Alaaji Omar Taal, Màbba Jaxu Ba mbaa Muhammad Lamin Daraame. Ak doonte yoroon na gëm-gëm bi mbooleem jullit ñi yoroon ci Jiyaar , muy jug dàkku sab dëkk ci tooñaange, xeex ngir goreel ko, mbaa aar sa alal añs, teewul mu yoroon beneen gis-gis bu gën a xóot ci jiyaar, mooy jiyaaru nafs, maanaam jiyaar ngir xeex ak sa bakkan ak sa bànneex, noot ko, moom ko, nga rax ci dolli ku gisoon la ne tubaab yii de xeex ak ñoom ciy ngànnaay yombul, te deesu ci jële ndam, - te mel na ne jamono jox na ko dëgg ! Ndax mbooleem ñi doon def jiyaar ak tubaab bi, tubaab bi faroon na leen noot, mbaa mu ray leen, tee leen a sottal seeni sémb, àntoodil seeni naal - ndax ëpp gi ñu ëppoon ci doole ak ngànnaay te gën koo aaytal, gën koo ñawle, bi lii amee, Ahmadu xam ne tubaab yee ko raw foofu, ca rafetug xelam ga mu jël beneen "estrateji", mooy jiitu leen ci xol yi, ba lu tubaab yi def ci kaw mu def ko ci biir, lii moo nekkoon mbóotum jiyaaram. + +Alxuraan mi ngi nuy xamal digal gu Yàlla digaloon jullit ñi ñuy jiyaar ak yéefar yi, ak doonte dañuy fukk jullit biy kenn, ba yàgg mu ne woyofal na ko ci yeen (jullit ñi) ndax xam doyadi gi nekk ci ñoom, mu ne leegi kenn mooy xeex ak ñaari yéefar, ndax xam na ne pastéef ba woon wonni na, te loolu mooy jàmbaar ya àndoon ak Yonent bi (j.m), naka mook tuubeen yii nga xam ne ba ñu duggee ci lislaam yàggul, te tubaab ëpp leen doole fuuf ak ngànnaay, kon kii ci hikma la jëfe te mooy li Y��lla bëgg + +Mbindam + +Bind na it lu maneesul a misaal ciy taalif, lu ci ëpp nag ay woy, yu muy def la, benn ngir tàgg ci Yonent bi (j.m), mbaa sant ci Yàlla, mbaa mu ciy wone may yu ko Yàlla may, loolu lépp di tàbbi ci sant Yàlla, mbaa mu jëm ci yar ak njàngalem diine, loolu nag ci araab la daan doon, teewul mu daa def ay tomb di ci tënk li muy jàngale ci araab, daan ko def ci wolof ñeel ñi xaw a mage ba jànge ci araab raw leen, mbaa seeni xel xaw a naqari ba ñuy am ay jafe-jafe ci jànge ci araab. Bokk na ci li ko tax di def ay woy ci taalifam yooyu, woy day jumtukaayu mokkal, mokkal ay woy daa gën a yomb ay wesar, looloo tax sax téere yi mu taalif ci xam-xam ngir taalube yi jàng ko, da leen a def ci ay woy, teewul bind na as lëf ci wesar lu ci mel ne majmooha, jasaawu sakkoor bu géej gi te sëñ Sëriñ Musaa Ka woy ko ci wolof añs. + +Ku fonkoon wolof la ak doonte ci araab la daan binde +Ci araab it la daan binde, sabab si nag su diine la waaye ku fonkoon aw làkkam la lool, ci la daan waxe te déggoon ko lool, daa na faral sax di jël waxiinu saalum-saalum wi ñu daa wax ne mooy wi gën a wolofe te gën a xóot di ko waxe, bis kenn ci ay taalubeem yi daa woy ci wolof ci seeni taalif, daa jugoon di ko tagge ci araab, mu ne ko bu ko defati, dee ko defe ci wolof, ndax man ki may tagg araab la te man mi ngay tagg wolof laa, kon kee da koo war a dégge ci aw làmmiñam, man it naa koy dégge ci samaw làmmiñ, lii moo waral ñu ko daa woy ci wolof, teewul nag am ciy taalubeem ñu ko woy ci araab niki Sëriñ Mut Jaw Paxa, Sëriñ Ibraayma Jóob Almashari. + +Man nañu ne sax mooki taalubeem ñooy ñi suuxat làkk wii, ndax ñi ëpp ci ñi bind ci wolof ci Senegaal ñoom lañu, xool ci ku mel ne Sëriñ Muusaa KA, Sëriñ Mbay JAXATE, Sëriñ Mbay Kayre, Sëriñ Moor Jaara Mbay, ba ci Mamoor Xam Sa Diine mii, te Tuubaa day tuuru ak ñu mel ni ñoom. + +Sababu binde ci araab + +Sabab si diine la, loolu it bind na ko ci genn ci ay xasidaam mu ne ca dañoo araamal ci moom muy bind ci lu dul ci làkku araab, wax jooju xel nangu na ko, ndax araab mooy làkk wu kilifawu (officielle) wu Lislaam, képp kuy njiit ci lislaam ñépp war a jariñu ci yaw ci nga war di binde, booy xool bindkat yi gën a mag ci Lislaam duñu ay araab te teewul ci lañu doon binde, ngir aar làkkuw alxuraan wi, jëmale ko kanam, tax it deesi ci sonn ba muy waral ñuy man a xam alxuraan ci lu dul ag xamal, ndax bu xam araab gi wéree xam alxuraan gi wóor te rafet. + +Nga rax ci dolli ci araab la jànge, làmmiñ wi réew mi mépp daan jànge, daan ci bindantee it ci lu fullawu (lu officiel), ba ci tubaab bi sax yoroon na ay "antalpareet" walla ay làpptoo, maanaam ñu leen di tekkil ci araab ak di leen ci bindal, ndax xam gi ñu xamoon ne réew mi lu ci ëpp ci araab lañuy binde. + +Te it ca jooja jamono wolof làkk la woon wu yaatoowul noonu, te du woon wolof yi rekk ñoo waroon a jariñu ci Sëriñ bi mbaa ñoo nekkoon fa moom, lii lepp taxoon na muy binde ci araab. Waaye teewul nekk gi mu nekkoon di nitug Yàlla taxoon mu xam lu ñëwagun, yobbu woon ko ci mu digal ñenn ciw nitam ñu féetewoo jëmale kanam wii làkk ndax xam gi mu xamoon ne mooy làkku ëlëg ci Senegaal + +Sancug Tuubaa + +Sancoon na Tuubaa ci 1887 ngir gën a man a wéetal Yàlla, ginaaw bi nit ñi baree fa moom ca Daaru Salaam ga ca anéeri Mbàkke gi ñu la waxoon leegi, nga xam ne raj-rajloo ba teewoon na koo nekk ca na mu ko soxlaa ba man a def li mu bëgg cig jaamu ak yar, ba mu demee Tuubaa't loola toppati ko fa, moo waraloon mu faroon sanc Mbàkke-Baari ca Jolof, fa la juge dem géej boo ci bëggee xóotal yëral: SancamJolof Ak li ko waraloon. + +Tuubloo ay buur ak doomi buur + +Ci bañ gi mu defoon cancug Tubaab yi ak séen politigu nasaraanal bi, Sëriñ bi mujjoon na tuubloo lu sakkan ci y buur aki doomi buur yu diiwaan bi, Jàmm la daan digle, jaamu Yàlla ak liggéey ngir man a texe ëllëg. Looloo waraloon lu sakkan ciy mbooloo doon bawoo fu nekk di sottiku ci kawam, ñii ngir jébbalusi, ñii ngiri sabab yu àdduna, loolu lepp nag jeqi woon na ñàqare ak jaaxle ci Tubaab yii nga xam ne doonuñu woon nangu ñu dul ñoom ñuy am genn jeexiital ci réew mi, mbaa genn kiliftéef gu àdduna gu bawoowul fi ñoom + +Sababu jàpp gi ak gàddaayal gi + +Waaye bi Tubaab yi gisee ne moon de boroomum mbooloo la te ñu ko gëm lañu, man na leen a yëngal bis jëme leen ci jiyaar, ni ko moroomi sëriñam si defe woon, lañu ko daal di jàpp, tëj ko ci kaso fa ñoom, ca Ndar giy dalub kaŋ bu ASF (Afrig gu Sowwu Gu Faraas gi), njëkk ñu koy gàddaayal ca Gaboŋ ci 1895. +Tubaab yi ngir ñu man koo jàpp lay yii lañu indi woon: + +«Ñun de gisuñu lenn luy wone ne Ahmadu Bamba day woote Jiyaar, waaye ab taxawaayam akug soppaxdikoom ak yu ay taalubeem daal teey nañu xel, jeqi nañu sikk » + +Dellusi gi juge ca géej ga + +Mi ngi dellusi ci Ndakaaru ci 1902 gannaaw ba mu defee 7 at ak 9 weer cig gàddaayal te nekkoon ci àll yu lëndëm këriis ya, bu ko defee mbooloo mi teertu ko ciy yuuxuy mbegte ak ségéré. + +Tubaab yi jàppati ko + +Tubaab yi jéemaatoon nañu koo jàpp ba yabaloon fa ay spahis nga xam ni ay xarekat yu ñuul lañu te àndoon ak nootkat bi waaye taalibey sëriñ bi àntoodil loolu. At mi ci topp lañu ko mujj jàpp daal di koy gàddaayal ca gànnaar ci lu tolloog 4 at. Ci diirub ñaari gàddaay yii nag xew-xew yu xel dajul jot na faa am, ngir gën cee am xam-xam yëral: Ñaareelu tukki bi (bu Gànnaar bi). + +Tubaab yi xam nañu ko leegi + +Gannaaw 1910 nag ci la tubaab yi xam ni sëriñ bi xeex yëkkatiwu ko te sax jàpp nañu ñoom ni yoon wi da leen di jàppale ci li ñu bëgg, ci noonu lañu sàkku liggéey ak moom maanaam ñu ànd far, ngir wone loolu ci lañu ko bëggoon a takkal raayo bii di “Légion d'honneur” di raayob teddnga bu Faraas bi gën a kawe waaye sëriñ bi gàntal. + +Yoon wi nag mi ngi gën a am aw nit ginnaaw bi mu fi bàyyikoo te taawam bii di Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke tàmbali woon liggéeyub jumaay Tuubaa ji, di tolloo ak barabam bi, doon tay fu nit ñi di siyaare cig rajrajloo. Gannaaw bi mu fi jógee, ay way donnam ñoo nekk ci xilaafa gi di digle tey tere. + +Fatalikug Sëriñ bi + +Ahmadu Bamba, ku taalibeem yi weg te fonk ko la , jàppe woon ko aw wàlliyu, te loolu du woon lees di faral di gis ci ñiy wuyyoo sunna, waaw ndax ci Lislaam daa am ay dawaan (courants) yu ci mel ne bu sunna, bu siit, ak bu tasawuf añs, moom nag Seex Ahmadu ci bu tasawuf bu sunna la bokk, am na ci waa tasawuf yi way teengal, bay àgg ci di jibal ay kàddu yu di yu tumbrànke, mbaa ñuy àgg ci wax juy jéggi dayo ba cig lëmu bay waral sikk ak weddi, waaye kii di Seex Ahmadu ay mbiram ak leer a ko wër, jéggiwul dayo ci genn anam, mbiram ci kitaab la tegu ak sunna ak tasawuf bu leer, te dëppoo ak doxiinu Yonent bi (j.m). Benn nataal rekk lees am ci moom. nataal boobu fu nekk tafees na ko fa, muy ci tabax yi, ci daamar yi walla feneen fu muy fése rekk. + +At mu jot ay junniy junni ciy taalibe danañu dem ca Tuubaa dëkk bu sell ba, ngir màggal gàddaay ga mu defoon jëm Gaboŋ muy yamoo ak 18 safar gu nekk. Bis boobu Sëriñ bi moo digle woon ñu santle ko Buur Yàlla ci may yi mu ko may ciy xéewal, muy bu taalibe yi fonk, jàppe benn ci bis yi ëpp solo ci bis yi. + +Li mu fi bàyyi +Sëriñ bi da daan woo ay taalibeem ngir ñu dëpp te jublu Yàlla, daan na digal taalibe yi ñuy moytu aw ay tey sàkku xam-xam bu am njariñ, di liggéey, am jom ju ànd ak jàmm, am pastéef ak ngëm ci Yàlla. wax na ni: "[[Yàlla rekk la ragal, samay yaakaar ci Yàlla laa ko wékk." + +Sëriñ bi dékku na nattu yu bari te tar. Benn ci ñoom mooy gaynde gu xiif ga juge barab ba ñuy wone rab yi te nekk ca Sor. Bis booba, dees koo tëj bàyyi ko ak gaynde gu mel ni far xar mu gis boroomam. +Sëriñ bi doonoon ku jàmmu te ñaw daan na wax ni: "Du ma mas a lor kenn ak ku mu man a doon." +Tëj nañu ko ci kaso bu lëndëm def fa ay ràbb, gobar ak jaasi, mu jàng fa saaru baqara ak aali Imraan. +Sëriñ Musaa Ka miy baayi way gëstu xew xewi démb ci yoonu murit mi ngi ñuy xamal ni: + keroog gis na fa suñu Maam Jaara () mu di ko ñaax te di ko dolliy daara + Fii laylatil jumaati lañ ko tàbbal () ci néeg bu lëndëm, noon ya naan ko làmbal + mu làmb daj fa gobar ak ràbbu ñu tëj () ko foofa dem, mu daldi jublu xibla kabbar + nee na keroog manul woon a sujjoot ngir tar-tar + 'Jàng fa saaru baqara ak aali Imraani () jibriilu tijji néeg ba fil xurhaani' + Am na fa yaari guddi lekkul naanul () ludul ci leeri Yàlla kooka naanul... + Bisub keroog lañu ko génne foofa () yóbbu feneen mu fekk gaynde bóof fa + Ñu boole kook gaynde ga tëj leen booba () Gaynde ga mel ni xar mu gis boroom ba... + Ñu daal di koy yóbb ci menn mbedd () bole ko ak yëkk wuñ yafal wuy fàdd + mbedd ma noon ya dañu koo gaaraante bisub keroog ruu ga la buur gaaraante. + Seex Bamba nee ba mu tëbee wuti fa moom () wuute wul ak boroomi laaf amuli buum + ba mu ñëwee ba jub ko faf nërméelu () xooj ga ni fojit fa kanam jibriilu... + + Keroog la gaal gay daw ba wàllu tisbaar () muy jàpp ab madam bu sew daal di fa jaar + Daal di taxaw fi kanamam dal di ko laal () Bamba fasaat njàpp ma daal di am aal + bamuy masaa mu delsi daal di koy laal ()nee tuuti kon mu tàkk far baal ko + gaayi badar ya, ñoo ko booleek der ba () lal ko ca mbeex ma te demul ca bël ba + Seex Bamba daldi jàpp julli tisbaar ... + +Xët yi mu lëkkalool + Nahju + Muriidulaa + Xamale kuy Sëriñ bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu góor làqoo + Sñ Sàmba Jaara Mbay + +Téerekaay + Cheikh Anta Babou, Fighting the Greater Jihad: Amadu Bamba and the Founding of the Muridiyya of Senegal, 1853-1913, Ohio University Press, 2007, 320 p. + Ahmed Pirzada, The epistemology of Ahmadou Bamba, Birmingham, University of Birmingham, 2003 (thèse) + Oumar Ba (documents recueillis par), Ahmadou Bamba face aux autorités coloniales (1889-1927), 1982, 250 p. + Claude Dazun, Rencontre avec un homme de Dieu : sheikh Ahmadou Bamba, Éd. Ndigel/Diff. Mouvement islamique des mourides d'Europe, 1990 + Abdoulaye Dieye, Sur les traces de Cheikh Ahmadou Bamba : l'exil au Gabon, période coloniale, 1895-1902, Edition Ndigel, L'Harmattan, 1985 + Cheikh Mor Doje, La vie religieuse de Ahmadou Bamba M'Backe, 1980 (thèse) + Fernand Dumont, Essai sur la pensée religieuse d’Amadou Bamba (1850-1927), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1968, 3 vol., 588 p. (Thèse) + Alioune M'Backé, Vie et enseignement du cheikh Ahmadou Bamba : maître fondateur de la voie mouride, Éd. Al-Bouraq/Diff. Librairie de l'Orient, 1999 + Serigne Bachir Mbacké, Les bienfaits de l'éternel, ou, La biographie de Cheikh Ahmadou Bamba Mbacké (traduction par Khadim Mbacké), Dakar, IFAN/Cheikh Anta Diop, 1995, 439 p. + Ahmadou Drame Serigne, La pensée religieuse de Cheikh Ahmadou Bamba, fondateur du mouridisme (Sénégal), 1985 (thèse) + +Lëkkalekaay yu biti + touba-internet.com + htcom + +niti senegaal +Yoonu murit +Seydinaa Limaamu Laay : + +Seyidinaa Limaamu ab nappkat la woon bu juddoo Yoof atum 1845 g.j. Ci atum 1885 g.j, mu gént gis ne mooy Mahdiyu .. mu tàmbalee woo àndandoom yi ci ñu dugg ci Lislaam, di soññ jullit ñi ci ñu sellal te jaamu Yàlla rekk, mu daa wax : (( wuyyuleen wooteb Yàlla, man de yonnantub Yàlla laa, maay Mahdiyu mi ñuy neggandiku)), daa na woo ay àndandoom jëme léen cig jub ak jàppalante. Bu ko defee nit ñu bari dikkal ko ngir déglu njàggaleem mi. Mu daal di sos kuréelug Laayéen. +Siiwam gi tiitloo woon na way sanc yi ragaloon ag jeqiku kontar leen. Ci atum 1887 g.j, la sancaan yi taxaw ci jàpp ko, bi mu yëgee seen naal yooyu la ànd ak lenn ciy àndadoom génn, waaye tubaab bi jàpp ko ca wetu Caaroy. Waaye ëttu àtte bi mujj na ko setal ko ngir ñàkk lenn lu man a dëgëral tuuma yi ñu teg ci kawam. Limaamu wéyoon na ci wooteem gi, waaye daa na def jamono ju nekk muy fenqook sancaan yi ko daa jéem a sonal ak àndandoom yi. Mi ngi làqu atum 1909 g.j. +Alaaji Omar Fuutiyu TAAL + Alaaji Maalik SI +Sudan (jóge ci ab baatu araab bilâd as-sûdân "dëkkuwaayu ñu ñuul ñi", benn ci la diiwaani Afrik yi, tàmbalee ca penku Afrik ba ca sowwu Afrik, ci bëj-saalumu Sahel, tàmbalee ca Mali ba réewum Sudaan ci penku Afrik. Diiwaan bi mooy ëpp taw ci Sahel, mbay mi fa la gën a neexe. Ci bëj-saalumu Sudaan àllub Yemoo fa am. + +Melosuuf +Afrig +Diwaani Afrig +Tugal benn la juroom ñaari gox yi nekk ci àdduna bi. Ay dig yu suufi Tugal yenn saa yi day indi ay werante, su ñu xoolee ni ko waa tugal ci seen bopp jappee, ci penku ci Asi la sës, ci sowwu mi ngi yem ci Mbàmbulaanu Atlas, ci bëj-gànnaar ci dottu bëj-gànnaar, géej gu diggu gi mooy koy yemale ci bëj-saalum. Liy indi werante bi mooy Risi ak Siipër ak Tirki, réew yi ci wàllu séwógaraafi dañ leen di boole ci Tugal te xaaj bu am solo ci seen suuf nekk ci Asi. + +Tay am na weneen gisiin ci ay digi Tugal. Waa Tugal yi Da ñuy jàpp ne + +Tugal +Melosuuf + +ru:Европа#География +Diggu Aamerig mooy xaaj bi nekk ci digg goxu Aamerig, ci diggante Meksik (bokk ci Bëj-gànnaaru Aamerig), ak Koloombi (bokk ci Bëj-saalumu Aamerig). Ay melokaanam ñooy li mu nekk di ab séla ci diggante ñaari Aamerig yi, ak li mu doon it ab jàllu, ngir man a jòge ci Mbàmbulaanu Atlas dem ci Mbàmbulaan gu Dal gi. Ca réewu Panamaa la boobu jàllu nekk. + +Séwógaraafi +Réew ya fa nekk: + + Beliis + Kosta Riika + Salbadoor + Guwaatemaala + Onduraas + Panamaa + Nikaraaguwa + +Taariix +Ay xay yu mag juddoo nañu ci bii diiwaan, yu ci mel ne yu Maya yi. Waa Espaañ ñooy waa Tugal yi fa njëkk a ñéw. Ñoom ñoo aakimoo woon nguuri Maya yi, dal di leen di noot ci lu mat ñetti xarnu. Daanaka réew yi nekk ci Diggu Aamerig yépp làkkuw Espaañ lañuy wax. + +Bi ñu amee seenug tembte, ci ndoorteelu 1800, la leen ay jafe-jafe yu bari ganesi. Looloo tax li ëpp ci taariixu réewi Diggu Aamerig yi, ba ci 1900, ay daane nguur ak ay xaree ci gën a fés. + +Koom-koom +Li ëpp ci am-am yi nekk ci diwaan bi, suufu mbéy la te li ci ëpp ci loxoy ñenn nit ñu néew la nekk. Mbéy mi, ba tay, moo ëpp solo ci seen koom-koom, njudéef (produit) yi ñu soxla ngir seen dund dañu koy jéggaani bitim-réew. Seen campéefi koom-koom yi tamit li ci ëpp ay doxandéem a leen moom. + +Diwaani Aamerig +Kembaarug Afrig / Goxub Afrig moom benn la ci goxi Àdduna Ju Yàgg ja, moom nag ab joor bu réy ci jéeri la, géej xottiwu ko (jaarul ci biiram) du caagéenug dóox (golfe). Moom nag mi ngi nekk walla mi ngi féete ci xaajub kol-kol bu penku bi. + +Gox bi nag mi ngi tallaliku ci diggante ñaari rëddi gaar yii : 37º ci tus-wu-taxaw wu bëj-gànnaar ak 35º ci tus-wu-gaar wu bëj-saalum. Bu ko defee rëddu yamoo wi jaar ci diggam, daal di koy séddale ñaari xaaj: benn xaaj bi di bu bëj-gànnaar, nekk nag ci xaaju kol-kol bu bëj-gànnaar bi, beneen bi di bu bëj-saalum, féete ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum bi. Ci noonu gëwéelub sànkar moom ñëw romb ca genn wàllam gu bëj-gànnaar ga, gëwéelub tef ñëw jaar ca geneen wàll gu bëj-saalum ga. Bu ko defee rëddu Grinits (rëddu tus-wu-taxaw wi ) romb ca catam lu sowwu la. + +Moom nag dafa tiim ak tefesam yi ci wàllug bëj-gànnaar géej gi ñuy wax Géej gu Diggu gi, mooy li ko tàqaleek goxub Tugal, waaye fu jege Tugal lay doon, bu dee fa tollook Doju Taariq (Jibraartaar). Bu dee ci penku bi day tiim Géej gu xonq gi ak mbàmbulaanug End gi, ñoom ñaar ñoo koy tàqaleek goxub Asi ak Oseyaani, waaye luy jege Asi la ca Baabul Mandab ak barsaqu Suwes, ci sowwu bi nag mi ngi sapp (tiim) ci mbàmbulaanu Atlas gi ko tàggaleek ñaari goxi Aamerig yii di: Aamerig gu bëj-gànnaar gi ak gu bëj-saalum gi. + +Afrig nag nekk gi mu nekk ci diggante goxi Àdduna ju yàgg ja, tax na bu baax ba xayug Isipt gu yàgg gu kawe ga, man a tas ba àgg ci xeet yu bari ci ñaari gox yii, Asi ak Tugal. + +Goxu Afrig mooy ñaareelu gox bi gën a yaatu ci goxi àdduna bi, ndax tolluwaayam àgg na ci 30 milyoŋi kilomet yu kaare, maanaam lu tollook 1/4 tolluwaayu goxi àdduna ju yàgg ja, walla lu tollook réew mu tollu ne Isipt nga ful ko fanweeri yoon. + +Ngir woomle gu réy gi gox bi def ci wàllug mbay, dundat ak mbell, sancaani sowwu yi (waa Tugal yi) tegoon nañu ko loxo, waaye ay askanam jug def ay fipp yu toftaloo ngir gore ci canc gi (colonialisme), ci noonu ñu ëpp ci ñoom mujj temb, sancu yi ci mujj a temb nag ñooy yu Portugaal yi, ñoom de xeex nañu xeex yu tar ngir jot séenug tembte. + +Melosuuf ci jëmm +Nin ko junjee ci kaw, Afrik doon na gox bu rey. Ci tëddaayam, so jële penkoom jëm sowwu mat na 7500 (juroom ñaar fukk ak juroomi temeer) km, bëj-gànnaaram ba bëj-saalum tollu na ci 8000km (juroom ñetti fukki junni) ci guddaay. + +Diwaan yu mag yi +Diwaan yu mag yi bari nañ loo: + +Melosuufug nite + +Nit ñi ci gox bi + +Reew yi nga xam ne seenug yorte(administration) dafa néewal, lim yi ñuy joxe doonu ñu yu matale (limbare (statistique) yi defu ñu leen ci anam gi war). +Ci 1975 : 302 miliyoŋ i way-dëkk +Ci 2001 : 591,3 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : PNUD) +Ci 2005 : 803,690 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : World Bank ndeyi-koor 2006) +Gisjiital ngir 2015: 866 miliyoŋ i way-dëkk. + +11% gu way-dëkk gi ci adduna bi, mi ngi ci Afrik gu bëj-saalumu-Sahara. yokkuteg nit ci Afrik doon na bi gën a gaaw ci adduna bi (21% ci ay way-dëkk yu ciy yokku at mu nekk). + +Doon na aw askan gu bariy ndaw, ñi ci ëpp 17 at la ñu am (te ci adduna bi yëpp 23 at la). 45% yu waa-afrik 15 at (fukki at ak juroom) la ñu am. te ñi ëppal 65 at, 3% lañ ci askanam (lang ak 13% ci li des ci adduna bi). + +Judd gi : 43 ci junni boo jël (26 ci junni ci adduna bi), 6 doom jiggeen ju ne ci lu ëpp(2,8 ci adduna bi). +Yaakaarte dund gi(li nga yaakaar a dund): 48.8 at +Ndeete gi: 47,5 ci junni +Ndeeteg (mortalité) xale yi 100 ci 1000 (junni bu ne teemeer a ciy dee). + +Xeet yi + +gëstukat yi ci li ñeel xeet, gis nañ ay mbooloo xeet yu bari ci Afrik: + + Pigme yi: neenañ bokk nañ ci mbooloo yi gënn a yagg. Ci seen taariix, ñoom ci all bi rek la ñuy dund. Seen jafe-jafey dund day yokk rek ndax all bi ñuy dagg ay garabam. + Waa-ecopi, Waa-somali ak Tubu yi: ñoom naar yi lañu gënn a jege, rawatina ci wallu làkk. + Waa-afrik yu ñuul ñi: Waa-sudaan(senegaal...), Waa-ginne yi, Bantu yi(Kongòo, Afrik gu diggu), Masay yi, Tutsi yi. + Tubaab yi: ñi nga xam ne Tugal la ñu cosaanoo. + Waa-madagaskaar + +Kuuteeg làkk yi + +Ñoo ngi koy xayma ci 200 ak 2000 làkk walla waxin (làkk dañ koy bind te waxin ci lammiñ lay yem) ci Afrik. Dañ leen seddale ci ay mbooloo, maanaam làkk yi am ag mbokk. + Mbooloo làkku bantu: yii ci la ñu bokk, lingala, duala, kikongo, kilari. Ñi ëpp ci ñi koy wax diggu afrik la ñu dëkk. + Kiswahili (ci mbooloo bantu la bokk): 15 miliyoŋi nit, ci penku Afrig + Ausa: ci yii reew, Niser, Niseriya, Cadd + Mandeŋ: 6 miliyon i nit(Mali, Burkina-faso, Senegaal,...) + Wolof: 11 miliyon i nit (Senegaal, Mali, Gambi, Moritani,...) +Lu ëpp ci làkk i Afrik yi, du ñu ay làkku nguuru reew ya ñu leen di làkkee, maanaam duñ leen jngale ci daara yi, ngur gi du leen jëfëndikoo. + +Ñetti làkk rekk ñooy làkk i seen nguuru reew, di seen làkku cosaan: Lesoto, Ruandaa, Burundi. + +Kuuteeg diine yi + + Lislaam: 260 miliyoŋ i taalibe. Ci sowu ak ci penku Afrik la ëppee doole, lu wuuse bëj-gàannar gi. + Diiney Kirist: 220 miliyoŋi taalibe + Diiney cosaan: ñoo gi koy xayma ci 100 miliyon i taalibe, waye war na kaa ëpp. + +Ñugg-ñugg yi +Goxub Afrig ñi koy xàmmee ci suufam su bari si ay laamaar, ba tax na sax ñu koy niroole ak tappaan bu ñu dëpp, boo xoolee di nga gis ne penku gox bi ak bëj-saalumam ñoo gën a yekkatiku bëj-gànnaaram ak sowwoom, te it dinga man a gis laamaar yii: + +Laamaaru Tàkk gu mag gi : day tàllaliku ngir daj mbooleem bëj-gànnaaru gox bi, dale ko ca géej gu xonq ga ci penku bi, ba ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, dees na fa gis it ag kaw-suuf gu bariy melo: ay laamaar, ay tundi xeer, yu beeñ (dune) ak xur yuy faral a am ay waaha (oasis). + +Doji Atlas yi: ñoom ñi ngi nekk ci gën jaa soriy bëj-gànnaaru sowwu gu Afrig, ci réewi Maxrib Bu Araab bi, bu ko defee ñu tàlleeku nag yor melokaanu ay càllalay doj, dale ko ca bëj-saalum gu sowwu gi ba ci bëj-gànnaar gu penku gi, ñu ëmb nag ci seen biir ay laamaar yu kawe yu ay ngéej yu saf xorom di diggale , ñu xame leen ci turu Shutuut . + +Xuru mbalkam Kongoo mi: mi ngi ci xolub gox bi, fa la dexug Kongoo giy dawe aki caram yu limu yi, di sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug atlas gi. + +Doji géej gu xonq gi: càllalag doj la gu kawe, tàlleeku bawoo bëj-gànnaar, ba bëj-saalum, feggook nag tefes gu sowwu gu géej gu xonq gi ci Isipt ak Sudaan. + +Laamaaru Ecoopi: mooy bi gën a kawe ci laamaari Afrig yi, fa la ñatti car (affluents) yu am solo yu dexug Niil gi di balle ñooy: Sobaat, ak Niil gu bulo gi ak Atbara, bu ko defee yobbaale ndoxi mbënd yu bari yi ci jamonoy taw bi, ngir denc leen ci ngéejus Naasir ba waa Isipt di ci man a jariñu, mu leen di indil ag naataange. + +Laamaaru ngéeji yamoo yi: moo ci gën a néew ag yekkatiku, fa la cari Niil gu yamoo gi di balle, ñoom ñi nga xam ne seeni ndox ña nga leen di jële ca ngéejus Wiktooria, mooy ngées su neexum ndox si gën a réy ci yu àdduna bi, mooy jox Niil ndox li ëpp ci weeri at mi + +Laamaaru bëj-saalumu Afrig: moo gën a yaatu te gën a yëkkatikoodi, am na nag yenn dex yu ko dog, am ci yu ciy sotti ci penku bi, ci mbàmbulaanug End, (niki Simbisi ak Lombobo), am yu ciy sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug Atlas niki Orang + +Kilimaa +Rëddu yamoo wi moo séddale Afrig def ko ñaari xaaj : bu bëj-gànnaar ak bu bëj-saalum, looloo waral ag tolloo am ci goxi kilimaa yi ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi ak ci bëj-saalumam. Li ëpp ci goxu Afrig it mi ngi nekk ci diggante gëwéelub sànkar bi ci wàllug bëj-gànnaar ak bu tef bi ci wàllug bëj-saalum gi, looloo waral kilimã bu gëwéel bu tang bi daj Afrig gépp lu ci dul catam yu bëj-gànnaar gu sowwu gi ak yu bëj-saalum gu sowwu gi, foofa kilimã bu géej gu diggu ga’a fa nekk. Jamonoy taw yi tam wuute nañu, bariwaayu taw bi it wuute ci barab ak moroom ja. + +Tawi Yamoo yu bari yi danañuy faral a sottiku ci tefesug Gana gi, ak [Mbalkam Kongóo|mbalkam Kongóo]] mi diirub at mépp. + +Taw yu kojug dig, yu noor yu sakkan yi, ñi ngi faral di rot ci bëj-saalumu Sudaan ak Laamaaru Ecoopi. + +Taw yu diggdoomu yi ñi ngi wàcc ci digg Gox bi, ca bëj-gànnaar ak bëj-saalumu diwaanu yamoo bi. + +Taw yu néew yi ñi ngi rot ci bëj-saalumu tàkk gu mag gi ak bëj-gànnaaru tàkkug Kalahaari gi. + +Tàkk gu mag gi nekk ci bëj-gànnaaru Gox bi nag moom daanaka du taw ak tàkkug Kalahaari gi nekk ci bëj-saalumu sowwu Gox bi. + +Tawi sedd bi danay rot ci bëj-gànnaaru Gox bi, ak bëj-saalumam gu sowwu gi ngir gelawi Kalahaari yay upp ca bëj-saalumu sowwu Gox bi. + +Melow kilimao bi ci noor bi ( noorub bëj-gànnaar bi) sulye – nii la tënkoo: + +Tàngoor +Jant bi day jamu ci gëwéelub sànkar bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaaju Gox bu bëj-gànnaar bi, nekk nag di lu yam te taradi ca xaaju Gox bu bëj-saalum bi. + +Naj gu jawwu gi (pression atmosphérique) , ngelaw li, Taw yi: + +Jant bi day jamu ci gëwéelub sànkar bi, ci bëj-gànnaaru Gox bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku, naj gu jawwu gi daal di woyof, te fekk naj gu jawwu gi mi ngi gën a am doole ci mbàmbulaanug atlas gi, loolu di waral ngelawi kojug dig (saisonnier) yu bëj-saalumu sowwu yiy tawloo di jañu juge ci mbàmbulaanug atlas gi jëm ci barab bi naj gu jawwu gi di gën a woyofe, bu ko defee taw yi daal di rot ci Tefesug Gana gi, ak Laamaaru Ecoopi ak bëj-saalumu Sudaan. + +Ci at mépp day taw ci Digg Afrig, ca la wër Rëddu Yamoo wa, taw yooyu nag ñi ngi leen xame ci turu (Tawi yéegal yi). + +Melow kilima bi ci sedd bi (seddub bëj-gànnaar bi) samwiye – nii la tënkoo: + +Jant bi day sampu ci Gëwéelub tef, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaajub Gox bu bëj-saalum bi, daal di wàcc maanaam neew doole (moom tàngoor wi) ci xaaj bu bëj-gànnaar bi, loolu mooy tax naj gu jawwu gi di néew doole ci bëj-saalumu Gox bi, tey am doole ci diiwaanu Tàkk gu mag gi, ci noonu la uppug ngelaw yu yaxantu yu bëj-gànnaaru penku yu fendi yi di àgge ba ci digg Gox bi daanaka. + +Ngelawi sowwu yu safaanu yiy tawloo (ndax ci Mbàmbulaanu Atlas lañuy juge) dañuy upp, di rotal ay taw ci tefesi bëj-gànnaaru penku yu Gox bi, ngelaw yii nag dañuy àgg ci tàkk gu mag gi, di lu fendi. Te tam Tàkk gi jamono ju nekk ngelawi yaxantu yu tàng yi danu koy upp. + +Ngelawi yaxantu yu bëj-saalumu penku yiy tawlo dañuy upp ci tefesi bëj-saalumu penku yu Afrig yi, bu ko defee taw yi rot, ñuy sutuxlu ci biir ci kaw Laamaaru Bëj-saalumu Afrig, bu ko defee ñu àgg ciw tàngoor ba ca Tàkkug Kalahaari, ci bëj-saalumu sowwu Afrig. + +Diiwaani kilima yi + + Diiwaanu Yamoo bi: moo nekk ci diiwaan yu suufe yi, ci ñaari wàlli rëddu Yamoo wi, diggante rëddu gaaru 5º ci bëj-gànnaar ak rëddu gaaru 5º ci bëj-saalum, mooy mbalkam Kongoo mi, Tefesug Gana gi, ak yenn diiwaan yi ci joor (plaine) gu tefes gu penku Gox bi, tàngoor wa lu kawe la, taw ya lu bari la ci at mi mépp, waaye dañuy gën a tar ci li gën a jege rëddu yamoo wi, ngir sampu ak jamu gi fi jant biy def ci ñaari xaaji-jamono yii + + Diwaanu gëwéel bi: mooy b��j-gànnaar ak bëj-saalumu diiwaanu Yamoo bi, ci diggante rëddu gaaru 5º - 18º ci bëj-gànnaar ak bëj-saalum, day tàng tey taw ci noor bi, tey nugg te fendi ci sedd bi, taw yi nag day gën di néew lu ñu gën a sori rëddu Yamoo wi. + + Diiwaanu kojug dig bi: mi ngi nekk ci Laamaaru Ecopi , taw ya fay am yu noor lañu te yu bari lañu, ngir upp gi fa ngelawi kojug dig yu bëj-saalumu sowwu yiy tawloo di upp ci noor bi, ñooy ngelaw yooyu di bawoo ci mbàmbulaanug atlas ak mbàmbulaanug end. + + Diiwaanu tàkk bi: mooy tàkk gu mag gi nekk ci bëj-gànnaaru gox bi, ak tàkkug Klahaari gi ci bëj-saalumu sowwu gox bi, barab la bu goxe (continental), bu néewi taw, ngir upp ga fa ngelawi yaxantu yu fendi yiy upp. + + Diiwaanu géej gu diggu gi: mi ngi nekk ci joori bëj-gànnaar yu gox bi, tiim nag géej gu diggu gi, nekk it ci cat lu bëj-saalumu penku bi, fu tàng te fendi lay doon ci noor bi ngir upp ga fa ngelawi yaxantu yu fendi ya di upp, di fu nugg tey taw ci sedd bi ngir li fa ngelawi safaanu yu sowwu yiy tawloo di upp. + + Diiwaan biy boroom tàngoor wu yam wi: mi ngi ci tefesi bëj-saalumu penku gox bi, fuy taw lu bari la ci noor bi, di taw lu néew ci sedd bi, ngelawi yaxantu yu bëj-saalumu penku yi dañu fay upp ci at mi mépp. + +Diiwaani gàncax yi +Gott yu Yamoo yi: ñi ngi ci fu ëpp ci mbalkam Kongoo mi, ci tefesug Gana gi, ak cig wàll ci tefes gu penku gu gox bi. Tàngoor wa lu fa tar la, taw ya lu fay bari la ci at mi mépp, looloo tax ay gott yu fatt, yu am ay garab yu réy, yu kawe te yaatuy xob te jegee di fa am, seeni bànqaas di rabbaloo, bu ko defee ay gàncax di leen wër fu nekk, di ñàpp nag ngir àgg ci leerug jant bi nga xam ne du àgg ci suufus gott sii fees dell aki taa-taa aki déeg aki tepp-tepp, fii nag ab judduwaay la ñeel ay gétti yo (barab bu bariy yo la) + + Gott yu kojug dig yi: gott yu kojug dig yi danuy nirook gott yu Yamoo yi, waaye ñoo gën a gàtt, ñi ngi nekk nag ci Laamaaru Ecopi ak bëj-gànnaaru tefesug Gana gi, ci Dunu Madagaskaar, ak ci Tefesug Afrig gi mu janool. + + Ñaxi Sawaana yi: ñi ngi ci diiwaan yu suufe yu gëwéel yi, ci bëj-gànnaar ak bëj-saalumu gott yu Yamoo yi, ak ci Laamaaru ngéej (lac) yu Yamoo yi ngir kawe ga mu kawe, bu ko defee ñax yu gudd yi di fa màgg (guddaayu ñaar ba ñatti meetar), ay garab di leen rax. Taw ba fay am bu noor la, te bu néewee - moom taw bi – te ab digam gàtt, garab yi dañuy jekki-jekki fàddu, bu ko defee ñax yi nuy wax Sawaana yu ñu wuññi yi des fi. Lu ñu gën a sori Sawaana yu ñu wuññi yi, tey gën a jege Tàkk gi, taw yi di gën a néew, ñaxi Sawaana yu ndόol, yu gooy yi di gën a feeñ. + + Gàncax yu Tàkk gu tàng gi: ñi ngi ci Tàkk gu mag gi ak ci tàkkug Somaali gi ak gu Kalahaari gi, taw ya foofa lu néew la, looloo tax gàncax yu gàtt a fay màgge, yu ami dég, yu ndawi xob, walla yi li ñuy wax (cire) daakaame walla njooy-njooy di muur, walla ñuy yu yor xob yu dijj, yuy denc ndox niki Sabiir, walla ñuy ay garab yu yor ay peer yu gudd niki garabu tàndarma. + + Gàncaxi Géej gu diggu gi: ñi ngi ci tefesi bëj-gànnaaru sowwu Afrig, ak ca gën jaa soriy bëj-saalumu sowwu Afrig, taw ya fa am yu jamonoy sedd la, garab ya day wert saa su nekk, yenn ya yu guddi peer lañu niki yu reseñ ya, yeneen ya seeni xob day muurook daakaande (cire) niki garabi limoŋ yi ak suraas, bokk na ca garab ya fa am ba tay : Saytoon, Koko, Ron, Kooni + + Gotti Diiwaan bu Siin bi: yii gott ñi ngi màgge ci tefesug bëj-saalumu penku gu gox bi, ya ëpp solo ciy garabam : Sanawbar, baloot ak xay, nit di leen dagg, ngir bay ci barab yi ñu nekkoon. + + Ñaxi barab bu diggdoomu bi: ñi ngi ci digg Laamaaru Ecopi, ci bëj-saalumu Afrig, fi ñuy tudde diiwaanu Fald, taw ya fay am yu noor lañu, ñax yu diggdoomu yi di fa sax, yooyu ñax ak barab yooyu ñuy sax, dees leen di jàppe ay gën ji sàmmuyaay ñeel lu aju ci yar ag jur. + + Gàncaxi doj yi: mi ngi ci Laamaaru Ecopi, ak Lamaaru ngéej yu Yamoo yi, fi jóori doj yu yékkatiku yi nekk, gàncax ya day toftaloo, dëppook ni tàngoor wi ak taw bi di toftaloo, bu ko defee gàncaxi diiwaan yu tàng yi di sax ci ron doj yi, di jàll ba ci gàncaxi diiwaan yu sedd yi, ba ci yuur (galaas) yi ci kaw njobbaxtal yu kawe yi. +Afritugalasi, ci séwógaraafi ngandam gox la, mooy bi gën a ngande ci àdduna bi. Suuf Yépp yi làng doon ko, am na fenn fu ñu tàqaloowe. Moom la ñuy faral di woowee Àdduna ju yàgg ji. + +Ci lu daj +Daanaka suuf si ëpp ci àdduna bi moom la, di 55% ci lépp. Am 5,5 miliari way dëkk, maanaam di daanaka 83% gu way dëkk yu àdduna bi. + +Mooy barab bi gën a yaatu ci àdduna bi soo ko mengalee ak Aamerig ak, Oseyaani, ak Dottu Bëj-gànnaar. + +Seddalinam +Ni mu amee ci bépp seddale, ay deggoo rek la ñu. Lu bari dañ koy xaaj ñetti gox: Afrig, Aamerig, Asi + +Gox yi +Ci Séwógaraafi Tugalasi ab gox la bu mbooloo bu ñaari gox yii di Tugal ak Asi jëmmal, walla benn xaaj ci Afritugalasi, ni ko ñenn ñi di waxee. + +Yaatuwaay: 54 000 000 km kaare + +Askan: 4,8 miliari way dëkk + +Tugalasi ak Afrik, ñoom la ñuy woowee àdduna gu yàgg ga, ndax li fa xay yi gën a yàgg juddoo. Baat bi day safaanoo ak àdduna gu yees gi, di ñaari gox yii Aamerig ak Oseyaani + +Gox yi +Oseyaani ab gox la bu nekk ci Mbàmbulaan gu Dal gi. Ci biiram Óstraali, ak Seland-Gu-Bees gi, ak Papuwasi-Ginne-Gu-Bees gi, Tasmaani, ak yeneeni dun. Oseyaani mooy gox bi gën a tuuti. + +Ci lu daj +Ci lu daj Oseyaani dañ koy jàppee ni ab gox bu nekk ci diggante Bëj-saalum-penku Asi ak Bëj-saalumu Aamerik. + +Oseyaani mooy gox bi gën a tuuti ci gox yi ci àdduna bi, ci  km kaare lay tollu, te 90% ya Óstraali la, 5,4 % ya di Papuwasi-Ginne-Gu-Bees, 3,1% ya di Seland-Gu-Bees gi, yeneen réew-réewaan yi tas ci Mbàmbulaan gu Dal gi doon 1,5 ci gox bépp. + +Am na 32 642 390 ciy way dëkk di ñareelu gox bi gën a néew ay nit lu weesu Dottu Bëj-gànnaar bi. 60% ya Óstraali la ñu dëkk, 16% ya Seland-Gu-Bees gi, 12% ya Papuwasi-Ginne-Gu-Bees. + +Diwaan +Ni yeneen gox yépp, ay peggan ci deggoo rekk lañ leen daggee. Baatu Oseyaani dañ koy jëfandikoo ngir jëmmal ab xaaj ci àdduna bi bu ëmb bépp suuf su nekk ci Mbàmbulaan gu Dal gi te duggoo ci barabi dott bi. + +Ci lu ëpp yii la ñuy jàpp ne ñooy ay Diwaanam: + + Óstraali + Melaneesi + Mikroneesi + Polineesi + Seland-Gu-Bees + +Ki defoon bi seddale moo doonoon Jules Dumont d'Uville ci 1831, waaye tegu woon ci cëslaayu xam-xam gu ñu ñangu tay. Ci 1970 ba tay, séwógaraafikat yi, Gëstukatu-làkk yi, ak yeneen boroom xam-xam, ci seeniy liggéey, yii rekk la'ñ koy seddalee Oseyaani gu Jege ak Oseyaani gu Sori. + +Rèew ak suuf +Lu ëpp ci réewi Oseyaani yi, ay dun la ñu. Mennum Óstraali ak Papuwasi-Ginne-Gu-Bees ñoo am ay peggu suuf ak yeneen réew (Ci Dunu Ginne gu Bees gi ak Endonesi gi ñuy boole wàllam gu bari ci Oseyaani). + +Lim bii di toftal dafa boole mbooleem réew aki suuf yi fa nekk. Te jàpp nak ne am na ay suuf yu fa ne te ñu jàppee leeni réew, waaye tembu ñun kon ay réew la ñu ci biiri réew, di nan bind ci réew mi ñu bokk ci wet gi. + +Gox yi +Bëj-saalumu Aamerig ci yenn sedatle yu àdduna bi dees koy jàppe ni ab gox, walla ci yeneen sedatle, ab ron-gox bu yamoo wi jaar, te li ëpp ci suufam ci xaaju kol-kol bu Bëj-saalum la nekk. + +Melosuuf +Bëj-saalumu Aamerig mi ngi ne ci diggante Mbàmbulaan gu Dal gi ak Mbàmbulaanu Atlas gi. Doon na gox bu bariy dun, yi ci ëpp nag ci réew yi ci gox bi lañu bokk. Li ko lëkkaleek Bëj-gànnaaru Aamerik mooy Panamaa. ag càllale gu ay doj moo leru penku gox bi bépp, ci kaw ba ci suuf; li ëpp ci penkoom àllub yamoo la. Amasoni mooy àll bi ëpp ci àdduna bi, ca réewum Bereesil la nekk. + +Taariix +Ay askan yu jòge woon goxub Asi ñoo ko dëkkee woon, daanaka am na ay junniy at nj.j.(njëkk judd gu Isaa). Amerigo Vespuci mooy tugal-tugal bi fa njëkk a teg tànkam, waaye li gën a siiw mooy ne Kristof Kolomb mooy ki ko wuññi + +Cancug waa tugal gu gox bi +La ko dale ca xarnub XVI la way dëkk yu Bëj-saalumu Aamerig tàmbalee am ay jàmmaarloo ak waa Tugal yi. Waa Ispaañ ñooy ñi fa njëkk, waa portugaal tegu ci, ci noonu ndànk-ndànk boroom doole yu waa tugal yépp tase fa di xëccoo suuf sa ak way dëkk ya fa cosaanoo, ak tam it ci seen diggante, ay jàmmaarloo yu metti juddoo na ca. + +Limu réew yi + +Juroom ñaari réew yu temb yi + Arsantin + Boliibi + Bereesil + Ciili + Koloombi + Ekwadoor + Guyaana + Panamaa + Paraguwaay + Peru + Uruguwaay + Benesuwela + +Ñetti réew yu tembul yi + Guyaana gu Faraas (Faraas) + Dunu Falkland (Nguur-Yu-Bennoo) + Jorjiyaa bu Bëj-saalum ak dunu Sandwich gu Bëj-saalum (Nguur-Yu-Bennoo) + +Gox yi +Aamerig +Diwaani Aamerig +Bëj-gànnaaru Aamerig ab gox la bu nekk ci Bëj-gànnaaru xaaju kol-kolu àdduna bi, féete, ci penku Mbàmbulaan gu Dal gi, ci sowwu Mbàmbulaanu Atlas, ci bëj-saalumu Géeju Dottub Bëj-gànnaar gi, ak ci Bëj-gànnaaru Aamerig gu bëj-saalumu. Mooy làccu bëj-gànnaar wu goxu Aamerig. + +Ci bii gox ñetti réew yu mag a fe: + + Kanadaa + Meksik + Réew yu Bennoo yu Aamerig + +Gox yi +Aamerig +Diwaani Aamerig +Ci xam-xamu falag xaaju kol-kol mooy benn xaaj ci ñaar yi ñu sedatlee kol-kolu àdduna bi. Rëddub yemoo bi moo ko xaaj ci digg bi, benn bu tudd xaaju kol-kol bu bëj-gànnaar ak bu bëj-saalum. + +Falag +Diggu Asi benn la ci diwaan yi ñu sedatlee goxu Asi. Cig déggoo mi ngi tambalee ci Géeju Kaspio ba ca bëj-gànnaar-sowwu gu Siin. + +Réew yi + Kasakistaan + Kirgistaan + Tajikistaan + Turkumenistaan + Usbekistaan + +Séwógaraafi +Sori géej, doon it diwaan bu man a sedd. Ci wàllu bëj-gànnaar, li ko dalee ci Volta ba ci Mongooli, jaare ko ci Kasakistaan, ab kekk la def bu ay sàmmkat dëkkee. Am na ñaari tàkk bu Taklamakaan ak bu Gobi. + +Ab càllaley doj moo nekk ci bëj-saalum-penku Diggu Asi, ñooy sax doj yi gën a kawe ci àdduna bi, doju Pamir, doju Hindi Kush, doju Himalaya. + +Ca doj yooyu la dex yi leen di dimbali ci mbéy mi di ballee. Li ëpp ci diwaan bi ñakk na lool taw. + + + +Asi +Baat bi man naa tekki lu bari: + + Diiwaani Senegaal +Penku Asi ab diwaanu Asi la. + +Su nu cëslaayoo ci sedatle, gu àdduna bi, gi Mbootaayu Réew yi def, Penku Asi benn la ci diwaani Asi yi. + +Yii ñoo fa nekk ciy Réew: + + Siin + Kore gu Bëj-gànnaar + Kore gu Bëj-saalum + Sapoŋ + Mongooli + +Asi +Bëj-saalum-penku Asi ci goxu Asi la bokk. + +Su nu sukkandikoo ci sedatle, bu àdduna bi, gi Mbootaayu Réew yi def, Bëj-saalum-penku Asi benn la ci diwaani Asi. + +Réew ya fa nekk: + Brunaay Daarusalaam + Kamboodiya + Endoneesi + Lawos + Maleesi + Miyanmaar + Filipiin + Singapoor + Taaylaand + Timoor gu Penku + Wiyetnaam + +Réew yépp yi nekk ci lim gi ci kaw, ba mu des Timoor gu Penku, ay Cër la ñu ci ASEAN: di ab mbootaay bu judd ngir soqali koom-koom mu diwaan bi jaare ko ci jappalante. + +Asi +Ron-goxu End mi ngi nekk ci bëj-saalumu Asi. + +Ay réewam: + Banglaades + Butaan + Biirmaani (ci lu bari Bëj-saalum-penku Asi la ñu koy boole.) + End + Maldiif + Nepaal + Pakistaan + Siri Laanka + +Rëy gi mu rëy ak ni mu beroo moo tax ñu def ko ron-gon, li fa réewu End gën a yaa mo tax ñu gox ko turam. + +Asi +Penku gu Sori mooy barab bi nga xam ne moo ëmb yenn réew yu Bëj-saalum-penku Asi, ak yenn diwaani Siin, ak Ooŋ Koŋ, ak Singapoor, ak Réewum Maleesi, ak dunu Taaywaan. + +Ci diwaan bii di nan fa gis ay réew yu wuute, ca wàllu koom ak xarala. Ci genn wàll di nan fa gis Taywaan ak Koom-koomam gu naat, ak dunu Hoŋ Koŋ aky taaxikawam yi gën a kawe ci àdduna bi, ak. Ci geneen wàll, ay réew yu seen koom-koom cëslaayu, ba tay, ci mbéy, waa kaw gi nekk ci coona. + +Limbari yi joxe nañ ay lim yuy firndeel ni Ooŋ Koŋ jiitoo ci Koom ak ci Xaral ci àdduna bi. + +Asi +Penku gu Diggu mooy diwaanu Asi bi tambalee ca Iraan ba ci Isipt. + +Réew yi fa ne: + Iraan + Tirki + Iraak + Siri + Libaan + Israayil + Palestiin + Araabi Sawdit + Kowet + Imaaraat yu Araab yu Bennoo yi + Omaan + Yaman + Kataar + Bahrayim + Jordaani + Isipt + +Asi +Penku gu Jege su ñu koy wax mooy diiwaan bu melosuuf bi araab yi dëkke, di tambalee ci pegg bu penku gu Géej gu Diggu gi ba ci Iraak. Moo taqaloo ak réew yi nekk ci Penku gu Diggu gi, féete ko penku, di: Iraan, Afganistaan, Pakistaan (Di yemoo ak baatu waa faraas bi di Moyen Orient ak bu waa angalteer bi di "Middle East"). + +Réew yi + Isipt + Israayil + Palestiin + Libaan + Siiri + Jordaani + Iraak + +Asi +Bëj-gànnaaru Tugal mooy wàll gu Bëj-gànnaar gu goxu Tugal. ni nuy xoolee Bëj-gànnaaru Tugal daa bariy fànn. + +Gisiin wu néewal gi +Yii ñooy réew yi fa ne: + Norweej + suweed + Danmaark + Islaand + Finlaand +Ñii la ñuy woowee Réewi bëj-gànnaar yi + +Gisiin wu yaa wi +Yii ñooy réew yi fa ne: + + Estooni + Letóoni + Lituwaani + Nguur-Yu-Bennoo + Beljik + Luksembuur + olaand + Almaañ + Poloñ + +Gisiin wu MR +Su ñu sukkandikoo ci ni ko Mbootaayu Réew yi gisee, Yii ñooy réew yi ne ci Bëj-gànnaaru Tugal: + + Norweej + suweed + Danmaark + Islaand + Finlaand + Estooni + Letóoni + Lituwaani + Nguur-Yu-Bennoo + +Melosuufug Tugal +Penku Tugal mooy diiwaan bi ëmb Réew yi ne Penku Tugal. Réew yi Bennog Sofyet gi tegoon loxo ci mujjug Ñaareelu Xareb Àdduna bi, yenn yi génn nañu ci, yeneen yi des ci. + +Séwógaraafi + Belaarus + Estooni + Letóoni + Lituwaani + Riisi + Romaani + Moldaawi + +Melosuufug Tugal +Bëj-saalumu Tugal ab diwaan la ci goxu Tugal. Tekkib baat bi nak di na faral di indi ay werante, ba tax na am na ay tekki yu bari. Ci lu ëpp da ñuy wax naa Ispaañ, Itaali, Girees, ñooy réew yi ci bokk, daanaka ci lu daj réew yépp yi nekk ci Géej gu Diggu gi. Bëj-saalumu Faraas ci lu bari da ñu ko ciy boole. + +Tekkeem gu séwógaraafi +Ci séwógaraafi da ñu naa Bëj-saalumu Tugal mooy xaaj bi gën a féete Bëj-saalum ci goxu bi; bii tekki nak da fa ajoo, ba tax na sax amuli pegg yu leer. Càllaleeb doj bu Alpi moom la ñuy téewee ni ab pegg buy seddatle Itaali ak li des ci Tugal, doon liy xaajatle ñaaru Tugal yi + +Limu réew yi + Portugaal + Ispaañ + Andoor + Faraas + Itaali + Korwaasi + Girees + Albaani + Bosni Hersegowin + Montenegro + Réewum Maseduwaan + Seerbi + Esloweeni + Ciipër + Malt + +Melosuufug Tugal +mangi bëgg lol ci jotaay gi ngenë ñu baxe +Seede + Julli + Woor + Natt asaka + Aj Màkka + +Lislaam +Koor mooy juroom ñenteelu weer ci arminaatu jullit ñi. Weer wii mooy ndoorteelu wàccug Alxuraan ci suuf. Bokk na ci li tax jullit ñi di ko woor: magal ko. Woor Benn la ci ponki Lislaam yi. + +Moom nag am na fukk ciy ne-ne (matière): + +Xamle luy koor, taariixu ag farataalam + +Xamle luy koor +Koor ci làkk : bañ a lekk, bañ a naan. + +Bu dee ci sariiya nag : bañ a lekk, bañ a naan, bañ a séy, bàyyi it mbooleem yiy dogloo la ko dale ca penkug fajar, ba ca sowug jant bi, ngir nag yéenee jaamu Yàlla. + +Taariixu ag farataal koor +Yàlla (t.s) moo farataal koor ci Muhammad (j.m) , niki mu ko farataale ca xeet ya ko fi jiitu woon ca waxam ju tedd ja: «Yéen ñi gëm, farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla» + +Loolu di woon ci bisub altine ci weeru baraxlu, ci ñaareelu at ci gàddaay gu barkeel gi( juge Màkka dem Madiina) + +Ngënéelul koor aki njariñam + +Ngënéelam +Ramadaan am na ay ngënéel yu màgg te bari, yu yeneen weer yi amul, àddiis yiy saxal loolu te di ko feddali yu bari lañu : +Waxam ja (j.m) : «Julli yi juroom, àjjuma ba àjjumawaat, ramadaan ba ramadaanati, dana ñu far bàkkaar yi nekk ci séen diggante, bu ñu teetee bàkkaar yu mag yi». + +Waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan ngirug gëm ak sàkku tuyaaba, jéggalees ko li jiitu ciy bàkkaaram». + +Yonnant bi (j.m) wax na ne : «Gis naa waa ju bokk ci sama xeet wi muy yalgat ngir mar, déeg bum dem ñu aaye ko ko, koorug ramadaan dikk wëgg ko, nàndal ko». + +Waxam ja (j.m) : «Guddi gi njëkk ci ramadaan bu jotee, dañuy jéng saytaane ak way féttéerluy jinne yi, tëj bunti sawara, du ñu ci ubbi benn, ubbi bunti àjjana, du ñu ci tëj benn, bu ko defee aji woote, woote ne: yaw miy sàkkuw yiw dikkal, yaw miy sàkku ay dëppal, Yàlla am na ñu ñu goreel ci sawara, te loolu guddi gu nekk lay doon». + +Waxam ja (j.m): «Koor de pakk la bu lay fegal sawara, ni pakk di fege boroom cib xare». + +Waxam ja mu nee (j.m): «Ku woor ab bis ngir Yàlla (t.s) Yàlla dana soril jëmm ja sawara lu tollook juroom ñaar-fukki nawet ngir bis boobee». + +Waxam ja (j.m): «Ki woor de bu dogee lu mu ñaan Yàlla may ko ko» + +Waxam ja (j.m) : «Àjjana am na bunt bu ñu naan Rayyaan, ku dul ñi woor duñu ca jaar, bu ko defee ñu ne: ana ñi wooroon, ñu daal di dikk, ku dul ñoom nag du dugg, bu ñu duggee it ba noppi ñu tëj bunt ba, keneen du dugg» + +ay njariñam +Koor am na ay njariñ yu ruu, yu mboolaay ak yu wér-gu-yaram ñooy: + + Bokk na ci njariñi ruu yu koor yi : moom day tax nga man a muñ, taggate ci, di tax it nit ki di wattoonteek bakkanam ak a jiyaar ak bànneexam, di jur ci bakkan ag ragal Yàlla te di ko ci suuxat, rawati na ragal Yàlla gi nga xam ne mooy sabab su mag si tax ñuy woor, moom la Yàlla (t.s) di firndéel ca laaya ba, ba mu naan : «Farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla» + +Bokk na ci njariñi mboolaay yu koor yi : day indi ag nosu ci xeet wi akug bennoo, bëgg ag maandute akug yamoo, dana sos tam ci jullit ñi ag ñeewant, yërmaande, di joxe it jikkoy ihsaan (rafetal), dina feg mboolaay gi it (la société) ci ñaawtéef yi ak bon-boni jikko yi. + + Bokk na ci njariñi wér-gu-yaram yu koor yi : moom (koor) day setal ay butiit, di defar ag mbàq, di setal yaram wi ci desiit yu bon yi ak diigiit yi , di wàññi aw yaram, di néewal gariis gi ci yaram. Adiis ba nee na : “ woor-leen, wer” + +Ñatteelu ne-ne bi : ci li ñu sopp ci koor, li ñu ci sib, li ñu ci araamal : + +Li ñu sopp ci koor +Sopp nañu woor bis yii : + +1- Bisub Arafa, ci ku ajul, mooy juroom ñeenteelu dil-hijja, ngir waxi Yonnant bi (j.m): «Woor bisub Arafa dina far bàkkaari ñaari at, ma jàll ak may jublusi. Woor bisub fukkeel ba di Aasoora nag moom day far bàkkaari at ma wéy». + +2- Bisub Asoora ak Taasooha, ñooy bisub juroom ñeenteel ak bu fukkeel ci weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) : «Woor bisub Aasoora dina far bàkkaari at mu jàll», ni mu woore moom Yonnant bi (j.m) bisub Aasoora te digale ñu woor ko, ne : “déwén bu neexee Yàlla dinañu woor Taasooha (bisub juroom ñeenteel ba)” + +3- Juroom benni fan ci sawaal , ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan teg ca juroom benni fan ci sawaal, mel na ni ku woor diirub jamono». + +4- Xaaj bu njëkk bi ci weeru baraxlu, ngir waxi Soxna Aysa (y.y.g) ja : «Masumaa gis Yonnant bi (j.m) mu woor mukk weeru lëmm wu dul wu koor wi, masuma koo gis it mu woor ciw weer lu ëpp li muy woor ci baraxlu». + +5- Fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ngir waxam ja (j.m) : «Amul yenn bis yu Yàlla gën a soppe ay jëf yu rafetet ci bis yii: maanaam fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ñu ne ko yaw Yonnantub Yàlla bi, xanaa jiyaar kay ci yoonu Yàlla moo gën a rëy yooyu bis? mu ne dée-déet, lu dul waa ju génn ci jëmmam ak alalam ci yoonu Yàlla, te delloosiwaatul dara» . + +6- Weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) ba ñu ko laajee: «Gan koor a gën ginnaaw ramadaan?» Mu ne : weeru «Yàlla wi ngéen di tudde muharram». + +7- Bis yu weex yi ci weer wu nekk, ñooy: fukk ak ñatt, fukk ak ñeent, fukk ak juroom, ngir waxi Abuu Darin ji (y.y.g) : «Yonnant bi (j.m) digal na nu nu woor ci weer wi ñatti fan yu weex yi : fukk ak ñatteeel; fukk ak ñeenteel; fukk ak juroomeel». Mu ne : «Ñoom de ñook woor diirub jamonoo yam». + +8- Bisub altine ak bob alximis, ngir li ñu nettali ne li ëpp ci li Yonnant bi (j.m) daa woor mooy bisub altine ak bu alximis, ñu laaj ko ko mu ne: «Jëf yi dees leen di gaaral altine ju nekk ak alximis, bu ko defee Yàlla di jéggal jullit bu nekk walla aji gëm ju nekk, ndare ñaari way tóngóo yi, mu ne nañu leen mujje» + +9- Woor bis, wori bis, ngir waxam ja (j.m) : “ wooriin wi Yàlla gën a sopp mooy wi Daawuuda daa def (j.m), julliwiin wi Yàlla gën a sopp mooy wu Daawuuda , da daan nelaw benn xaaj ba , taxaw benn ñatteel ba , di nelaw juroom benneel ba. Daan na woor it benn fan, wori ba ca des” + +10- Woor ci ki yorul jabar, te manul a denc , ngir waxam ja (j.m) : «ku ci toll ci denc, na wut jabar, moo la gën a man a tee xool jigéen ñi, gën laa musal ci njaalo, ku ko manul nag nay woor, (moom koor gi) ag tàpp la ci moom». Al-buxaari moo ko soloo. + +Li ñu sib ci koor +1- woor bisu Arafa ci ku fa taxaw, ngir tere gi ko Yonnant bi (j.m) tere ci ku fa nekk. + +2 – ber bisub àjjuma woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « bisub àjjuma séenug iid la buleen ko woor, ndare bu da ngéen a woor bis ba ko jiitu walla ba ca topp » + +3 – ber bisub gàwwu woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « Buleen wor bisub gàwwu bu dul farata ci yéen, bu waay amul lu dul xàncug reseñ it walla bantub garab na ko lekk » + +4 – woor mujjug baraxlu ngir waxam ja (j.m) : « bu baraxlu xaajatee buleen woor » + +Ag yeete +Sibéelug woor fan yii sibéelug sellal la. Waaye lii di ñëw nag ag sibéelam, sibéelug araamal la: + +1 – jokkale, mooy jokkale ñaari fan di ko woor walla lu ko ëpp ci lu dul dog ci diggante bi, ngir waxam ja (j.m) :«Buleen jokkale» ak waxam ja :«Moytuleen di jokkale». + +2 – woor bisub sikk, mooy bisub fanweer ci baraxlu, ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor bisub sikk moy nga baayi Qaasim». + +3 – woor diirub jamono, mooy woor at mépp ci lu dul dog ci, ngir waxi Yonnant bi (j.m) : «Ku woor diirub jamono, wooroo». ak waxam ja : «Ku woor diirub jamono wooroo, dogoo». + +4 – koorug jigéen ci lu dul ndigalu boroom këram bu teew , ngir waxam ja (j.m) : «Bu jigéen woor benn bis te jëkkaram nekk fi, te joxu ko ci ndigal lu dul weeru koor». + +Koor gu ñu araamal gi +Mooy woor bis yii di ñëw : + +1 – woor bisub iid, moo xam kori la walla tabaski, ngir waxi Omar ji (y.y.g), ñaar yii, bis lañu yu Yonnant bi (j.m) tere ku ci woor: «Bis bi ngéen di dog ci séenug koor ak bi ngéen di lekk ci séeni jaamu (séeni xari tabaski)» + +2 – ñatti bisi tasriiq yi, ngir “Yonnant bi (j.m) dafa yónni woon ab yéenekat mu yéene ca Munaa ne buleen woor bis yii, ñoom de bisi lekk lañook naan ak séy” lafd am na ak tudd Yàlla. + +3 – bisi mbërëg yi (gis baax) ak wësin, ndax ag daje am na ci ne koorug aji mbërëg walla aji wësin genn baaxu ci, ngir waxam ja (j.m) : «Ndax gisu leen ne bu mbërëgee du julli te du woor? loolu ci wàññikug seen diine la». + +4 – koorug aji tawat ji ragal ag dee ci tawat ji bu wooree, ngir waxi Yàlla ji (t.s): «Buleen ray seen bopp, Yàlla de ku leen yëram la» + +Warug woor weeru koor +Woor weeru koor lu war la ci Alquraan ak Sunna ak dajeg xeet wi (ijmaahul umma), Yàlla nee na (t.s) : «Weeru koor wi nga xam ne ci lañu wàcce Alquraan muy ag njub ci nit ñi te di ay laaya yu leer yuy gindee tey tàqale dëgg ak fen, ku ci fekke weer wi na nga ko woor» ak waxi Yonnant bi (j.m) : «Lislaam ci juroom lañu ko tabax, seere ne Laa ilaaha illal laah, Muhammadun rasuulul laah, ku dul Yàlla du yàlla te Muhammad moo dib yonnantam, ak julli, natt asaka, aj Màkka ak woor weeru koor» ak waxam ja (j.m) : «buumi Lislaam ak ponki diine ñatt lañu ci lañu tabax Lislaam, ku ci bàyyi benn rekk yeefar nga, sa dereet dagan na : seere ne Yàlla rekk ay buur, ak julli giy farata, ak woor weeru koor». + +Ngënéelul def lu baax ak njekk ci ramadaan +Ngir ngënéelul ramadaan, lépp lu ñu ciy def ci lu baax day gën, bokk na ci jëf yu baax yi ñu ci man a def : + +1 – saraxe : Yonnant bi (j.m) nee na : « Gën ji saraxe mooy bi ñu def ci koor gi » waxati na (j.m) : « Ku jox aji woor lu mu doge am nga yool bu tollu ne kooram ga te loolu du wàññi cib yoolam dara » mu waxati « ku jox ndogu aji woor, mu diw ñam walla ag naan ci lu lew, malaaka yi danañu julli ci moom ci waxtuy weeru koor wi, Jibriil julli ci moom ci guddig Laylatul Qadr » moom (j.m) moo gënoon a tabe ci nit ñi, bu ramadaan jotee nag da daan gën a tabe bu ko Jibriil di dikkal + +2 – taxaw guddi : ndax Yonnant bi (j.m) wax na : « ku taxaw ci ramadaan ngir gëm ak sàkku tuyaaba, jéggalees ko li jiitu ciy bàkkaaram » nekkoon na moom (j.m) di dundal guddiy ramadaan yi, bu fukki fan yu mujj ci koor gi masaan na jot da daan yee ñoñam, ak mépp mag mbaa ndaw lu man a julli + +3 – jàng Alquraan ju tedd ji : ndax Yonnant bi (j.m) daan na baril jàng Alquraan ci weeru koor, Jibriil it daan na jànganteek moom Alquraan ci ramadaan , Yonnant bi daan na guddal njàngum Alquraan mi ci taxawaayi naafilay koor gi, nu ëpp ni mu ko daan defe ci lu dul ramadaan, Hudayfa mas naa julleek moom ag guddi, mu jàng saaru Bàqara, teg ca Aali Himraan ak Nisaayi, te daawul romb aw laayaw xuppe ndare bu da caa taxaw di ñaan, moo tax julliwul ñaari ràkkaa rekk dégg Bilaal muy nodd fajar. Loolu dikk na ci Sahiihayni. +Wax na bat ay (j.m) : « koor ak taxaw danañu ramu jaam bi yawmal qiyaam, bu ko defee koor gi ñëw ne : boroom bi kii de tee naa koo lekk bëccëg tee koo naan, Alquraan ji ne : maa ko tee nelaw guddi kon tin ñu ci moom » + +4 – lihtikaaf : mooy tàqook jàkka walla tëju fa di jaamu Yàlla (t.s), Yonnant bi (j.m) lihtikaaf na te daawul dañ di ko def ci fukki fan yu mujj yi ci ramadaan, ba Yàlla jëlle ko fi, looloo ngi ci Sahiihayni. Wax na (j.m) ne : « jàkka mooy neegub jépp aji ragal Yàlla, Yàlla warlul na képp ku jàkka di sab néeg, warlul na la ab noflaay ak yërmaande ak jéggi siraat dem ca gërëmam la, tàbbi ca àjjanaam ja » + +5 – umra : mooy siyaareji Baytil Laahil Haraam, ngir wëri kaaba ga, ak doxi Safaa ak Marwa, ci ramadaan, ngir Yonnant bi nee na : « umra ci ramadaan mook aj ànd ak man a yam » waxaat na ba tay : « umra ba umra far na bàkkaari li nekk ci séen diggante » + +Saxug weeru koor +Duggug weeru koor ci ñaari mbir yii lay saxe: mbir mu njëkk mi mooy weer wi jiitu koor gi mat sëkk, mooy baraxlu, bu baraxlu matee fanweeri fan, bisub fanweer ak benneel ba mooy bis bi njëkk ci ramadaan ci lu dog. Mbir mi ci des mooy gis terute wi , bu ñu gisee terutew ramadaan ci guddig fanweer ci weeru baraxlu , kon weeru koor tàbbi na, woor ko war na ngir waxam ja (t.s) : ak waxi Yonnant bi ji (j.m) : « bu ngéen gisee terute wi woorléen, bu ngéen ko gisee worileen, bu niiree ba manu leen koo gis(ak doonte feeñ na) mottalileen limu weer wi muy fanweeri fan » , dana doy ngir saxal ag gisam jenn aji maandu ne gis na ko walla ñaar . Ndax Yonnant bi (j.m) daganal na benn waay seere ne gis na terutew ramadaan . Bu dee nag korite jenn aji maandu du doy, ñaar ñooy baax, ndax Yonnant bi (j.m) daganalul gisug kenn ku maandu ci korite + +Ag yeete +Ku gis terutew koor war naa woor ak doonte nanguwuñu ag gisam, ku gis nag terutew kori te nanguwuñu ag gisam du wori, ngir waxam ja (j.m) : “koor mooy bis bi ngéen di woor, kori di bis bi ngéen di wori, tëbëski di bis bi ngéen di tëbëski” + +Juroom ñaareelu ne-ne : ci sarti koor, ak àtteb koorug aji tukki, ku tawat, mag mu màggat, aji ëmb ak kuy nàmpal : + +Sarti koor +Sart nañu ci warug kor gi ci jullit bi, mu am xel tey mukàllaf, ngir waxam ja (j.m) : “ xalima gi yékkatees na ko wëlif ñatt : wëlif ab dof ba kero muy dofadi, kuy nelaw ba kero muy yewwu, ak gone ba kero muy gent” bu dee jullit bu jigéen sart nañu ci werug kooram gi mu set ci dereeti mbërëg ak wësin, ngir waxam ja (j.m) ci leeral wàññikug diiney jigéen : “ndax du bu mbërëgee du julli du woor ?” + +Aji tukki +Ab juliit bu tukkee ci soriwaay bu ñuy wàññee julii, soriwaay boobu mooy tollook 48 miil, bu boobaa aji yoonal ji (di Yonnant bi) may na ko mu dog ci sartub mu fay ko bu dellusee, ngir waxam ja (t.s) : moom nag mu woor moo gën bu fekkee ne tukki di woor du ko sonal, bu ko dee sonal nag woree gën, ngir waxi Abii Sahiid Alxadarii ji (y.y.g) “ nekkoon nañu di xeex ànd ak Yonnant bi (j.m) ci weeru koor, am ñu ci woor, am ñu ci woorul, ki woor du tane ki woorul, ki woorul du tane ki woor, ñu gis ne ku am kàttan gu mu woore woor moo gën, ku ko amul it bañ a woor moo gën” + +Aji tawat +Bu jullit bi tawatee ci koor, day xool, bu manee woor ci lu dul ab coona bu tar day woor, bu ko manul mu dog, bu yaakaaree ne dana wér nag day xaar ba wér fay la ko faat, bu yaakaaree ne du wér mu dog tey saraxeel bis bu mu woorul ab mudd ciw ñam (maanaam ab loxo ba mu fees ak dugub) ngir waxam ja (t.s) : + +Mag mu màggat +Ab jullit moo xam góor la, moo xam jigéen la, bu màggatee ba manut a woorati, day dog te saraxeel bis bu mu woorul mudd ciw ñam, ngir waxi Ibnu Abaas ji (y.y.g) : “may nañu mag mu màggat mu leel ab miskiin ci bépp bis bu mu woorul, te fay du ko war” + +Aji ëmb ak kuy nàmpal +Bu fekkee jullit bi dafa ëmb te ragal bu wooree lor boppam mbaa mu lor li ci biiram, day dog, te bu wësinee mu fay. Su fekkee man na ko nag nay saraxe ci bepp bis bu muy fay lu tollook mudd ci dugub, loolu moo gën a mat te ëppub yool. +Nii itam la kuy nàmpal di def, bu ragalee ci boppam ak ci doomam te amul ku ko nàmpalal walla doom ji nànguwul keneen ku dul moom. Àtte bii nag ñi ngi ko ball-loo ci waxam ja (t.s) : , maanaam (ñi ko man) mooy: ñi ko man ci coona bu tar, bu ñu woree fay walla ñu leel ab miskiin. + +Ñaari yeete + Ku sàgganee fay koor gu mu waroon a fay ci lu dul ngànt ba geneen koor dellusi, war nay leel ab miskiin ci barabu bépp bis bu mu war a fay. + Jullit bu faatu te waroon a fay ag koor, koor ga kilifaam a ko koy fayal, ngir waxam ja (j.m) : “ ku faatu te borub koor a ngi ci kawam, na ko ko kilifaam fayal” ak waxam ja ñeel ka ko laajoon ne ko: “ sama yaay dafa faatu te war naa fay aw weeru koor ndax dama ko koy fayal ?. Mu ne : waa-waaw, bor bu ñu yoreel Yàlla de moo gёn a yayoo ñu fay ko” + +Ponki koor (ay farataam), ay sunnaam, yu ñu sibam + yéene, mooy fas ci xol ne danga woor ngir topp ndigalul Yàlla (t.s), walla ngir jaamu ko, ngir waxam ja (j.m) : “ ku fanaanalul yéeney woor, amul koor” . Bu dee ngàttnga la nag moom dana baax ak doonte ginnaaw bu fajar fenkee la, bёccёg bi tàmbalee dugg, bu fekkee ne jotul woon a lekk dara, ngir waxi Soxna Aysa ji (y.y g) : «Yonnant bi (j.m) dugg na fi man bis, ne : ndax yor ngéen dara ? ñu ne ko : dée-déet, mu ne : kon woor naa» + Jàpp, mooy bàyyi yiy dogloo moo xam lekk la mbaa naan walla séy. + Jamono koor gi, maanaam bёccёg gi, mi ngi tàmbalee ci fenkug fajar gi ba ca sowug jant bi. Bu waay wooroon guddi gi, dog ci bёccёg bi, ag kooram du wér, ngir waxam ja (t.s) : «Mottalileen koor gi ba ci guddi gi» + +Sunnay koor + +1 – Gaaw a dog, mooy dog rekk bu jant bi sowee, ngir waxam ja (j.m) : “ nit ñi duñu dañ di nekk ciw yiw li feek ñi ngi gaaw a dog” ak waxi Anas ji (y.y.g) : “Yonnant bi (j.m) daawul julli timis ndare bu daa dog, ak doonte ci guuxub ndox la” + +2 – doge ci tàndarma ju tooy mbaa ju wow, bu amul ndox, li ñu gёn sopp nag mooy mu tόol: ñatt walla juroom mbaa juroom ñaar, ngir waxi Anas doomi Maalik: “Yonnant bi (j.m) da daan doge ci tàndarma ju tooy njëkk muy julli, bu amul jёfandikoo tàndarma ju wow, bu amul mu guux ay guuxi ndox” + +3 – ñaan booy dog, ndax Yonnant bi (j.m) daan na wax bu dogaan : “Allaahuma lakka sumnaa wa halaa risqika aftarnaa, fa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu” Ibnu Omar moom daan na wax: «Allaahuma innii asaluka birahmatikal latii wasihat kulla sayin, an taxfira sunoobii». + +4 – Xëdd, mooy lekk ak naan ci waxtuw njël di mujjug guddi gi, ànd ak yéeney woor, ngir waxam ja (j.m) : "ngënéel li tàqale sunug koor ak gu waa Ahlul Kitaab (ñoñ téere: Yahood yeek Nasaraan yi) mooy xëdd” ak waxam ja (j.m) : “xëddleen, xëdd de am na barke” + +5 – yeexe xëdd ba ci xaaj bu mujj bi ci guddi gi, ngir waxam ja (j,m) : “sama xeet wi duñu dañ ciw yiw li feek ñi ngi gaaw a dog tey yeex a xëdd” + +Waxtuw xëdd mi ngi doore ci xaajub guddi bu mujj bi, yam ci bu fajar desee ay simili yu neew, ngir waxi Saydun Ibnu Saabit ji (y.y.g) : “ xëdd nañook Yonnant bi (j.m), bi mu noppee jug di julli ji, ma ne : diggante xëdd ak nodd lan la ci waxtu ? mu ne : lu tollook juroom fukki laaya” + +Ag yeete +ku am sikk ci fenkug fajar na lekk te naan bam u wόor ko ne fajar fenk na, bu ko defee mu jàpp (mu tàmbalee woor), ngir waxam ja (t.s) : “ lekkleel te naan ba xàmmee wёñ gu weex cig u ñuul ci fajar gi” waxees na Ibnu Abaas (y.y.g) ne ko : “man de damay xëdd, bu ma sikkee (ne warees naa jàpp) ma bàyyi. Mu ne ko : lekkal li feek yaa ngi sikk, ba sikkatoo (nga jàpp)” + +Yi ñu sib ci koor +Sib nañu ci koor ay mbir yoy man nañoo tax ba koor gi yàqu, ak doonte ñoom ci seen jёmmi bopp duñu ko yàq, ñooy: + +1 – ёppal ci gallaxndiku ak saraxndiku booy jàpp, ngir waxam ja (j.m) : “ёppalal ci gallaxndiku ndare bu dangaa woor” sibees na muy ёppal ci saraxndiku ngir ragal ndox mi di jàll bay àgg ca biiram, di yàq kooram. + +2 – fόon, man naa jeqi bànneex bu man a yàq koor, ngir mànniyu mu génn mu muy waral, walla ab séy te bu boobaa kafaara day war. + +3 – di xool sa soxna cib bànneex + +4 – di xalaat ci mbirum séy + +5 – laal jigéen ak sa loxo walla jonjook moom ci sa yaram + +6 – sàqami singom ngir ragal lenn di ci jàll + +7 - ñam cin mbaaw ñam + +8 – gallaxndiku ci lu dul jàpp mbaa aajo laaj ko + +9 – tusngalu ci njëlbéenug bёccёg gi, bonul nag ci mujj gi + +10 – nàmpatal ak lu ni deme ngir ragal ag néew-doole gu man a waral ag dog + +Luy yàq koor, ak lu ñu daganal ci ku woor mu def ko, ak lu ñu ko ciy jéggal + +liy yàq koor +Ay mbir lañu ñooy: + +1 – am yolaakon (liquide) mu àgg cib biir jaar ci bakkan,(moo xam ci paj la mbaa leneen), mu jaar ci bёt mbaa nopp niki tuuf, mu jaar ci kanamug jigéen niki pikiiru . + +2 – li àgsi ci biir bi ngir ёppal gu ñu def ci galaxndiku ak saraxndiku ci njàpp ak leneen. + +3 – génnug mànniyu ngir xool bu bari walla xalaat walla foon walla jonjoo + +4 – waccu mu ñu tay, ngir waxam ja (j.m) : “ku waccu te tay ko, na fay” waaye nag ku am waccu not, ba mu waccu te sàkkuwu ko, loolu du yàq kooram + +5 – lekk mbaa naan mbaa séy bu ñu la ci manantee (forsee) + +6 – ku lekk mbaa mu naan ngir jortu ne daa nekk ci guddi gi, ginnaaw bi mu xam ne fajar fenkoon na + +7 – ku lekkoon mbaa mu naan ngir yaakaaroon ne dog jotoon na te fekk booba jotutoon + +8 – ku lekk mbaa mu naan ngir fàtte te àggalewul kooram nàgir jortu ne wareesul a àggale koor, ginnaaw jot nanoo lekk te naan, bu ko defee mu wéy ca dogam ga ba guddi. + +9 – agsig dara lu dul aw ñam ba ci mbaq gi (biir bi) jaare ko ci gimiñ gi, muy lu mel ne wann ab jaaro walla ag wёñ, ngir li ñu jёle ci Ibnu Abaas mu ne : “ koor mooy li dugg, du li génn” mu bёgg a wax (y.y.g) ne: koor mi ngi yaqoo ci liy dugg ci biiru nit ki, waaye du yàqoo ci li ciy génne niki dereet walla am waccu. + +10 murtad (mooy tubbi) ak doonte dellusiwaat na ci Lislaam, ngir waxam ja (t,s) boo bokkaalee sa jёf dana sippiku te danga bokk ci ñu ñàkk ñi (ñu pert ñi) + +Yii yépp dañuy yàq koor tey waral fayug bis ba ca yàqoo, waaye nag duñu waral kafaara, ndaxte kafaara moom du ware ndare ci ñaari way yàq koor yii: + +1 – séy bu ñu tay te kenn manantewu la ci, ngir waxi Abuu Hurayra ja (y.y.g) : “waay ñëw na ci Yonnant bi (j.m), ne ko man de alku naa yaw Yonnantub Yàlla bi, mu ne ko : lu la alag ? mu ne ko séy naak sama soxna ci ramadaan. Mu ne ko : ndax am nga jaam boo goreel? Mu ne deedeet, mu ne ko ndax man ngaa woor ñaari weer yu toftaloo? Mu ne ko deedeet, mu ne ko ndax am nga lu man a leel juroom benn fukki miskiin ? mu ne ko deedeet, daal di toog, Yonnant bi (j.m) daal di indi as ndàmba su def tàndar ma, ne ko am saraxeel lii, mu ne ko ndax dama koy sarax ku ma gёn a ñàkk? Yonnant bi ree ba ñuy gis bёñam ya, mu ne : demal jox ko sa ñoñ” + +2 – lekk mbaa naan ci lu dul ngant lu ñu daganal: ci Aboo Haniifa ak Maalik (y.y.g), seenub tegtal mooy : “waay dog na ci ramadaan Yonnant bi (j.m) digal ko mu kafaara” ak àddiisu Aboo Hurayrat (y.y.g) mu ne : “waay ñëw na ci Yonnant bi (j.m) ne ko : dog naa ci ramadaan te tay ko, Yonnant bi ne ko: goreelal ab jaam, mbaa nga woor ñaari weer yu toftaloo, mbaa nga leel juroom benn fukki miskiin” + +li ñu daganal ci ku woor +Daganal nanu ci ko woor ay mbir ñooy : + +1 – soccu diirub bёccёg bi, waaye Imaam Ahmad moom da koo sib bu digg-bёccёg bi jàllee + +2 – serlu cim ndox mu sedd ngir tàngoor wu tar wi, moo xam da koy sotti ciw yaramam walla da ciy nuur + +3 – lekk ak naan ak séy guddi, ba fajar fenk + +4 – tukki ngir aajo ju dagan, ak doonte xam na ne tukkeem bi dana tax mu dog + +5 – faju ci lepp lu dagan, bu fekkee ne dara du ca jàll ba ca mbàq ga, man naa jёfandikoo pikiir sax bu dul buy joxe aw ñam + +6 – sàqamil aw ñam ag gone gu ndaw gu amul ku ko sàqamil aw ñamam wi mu manul a ñàkk, waaye ci sartub lenn bañ cee jàll ba ca mbàq ga. + +7 – cuuraayu ak gёttu (xeeñu latkoloñ), loolu nag li ko waral di ñàkk a gis lu koy tere lu juge ci aji yoonal ji (di Yonnant bi (j.m)) + +li ñu jéggale +Kuy woor jéggal nanu ko ay mbir ñooy: + +1 – wann ay lor (tuflit) ak doonte bari na, maanaam lori boppam nag waxunu lori keneen + +2 – am waccu mu la not, bu ca dara delluwul ba ca mbàq ga, ginnaaw bi mu génnee ba ci catu làmmiñ wi + +3 – wann aw weñ te tayoo ko + +4 – pёndub yoon walla bub liggeeyukaay, ak saxaarus matt, ak mbooleem saxaar yi nga manul a moytu + +5 – xёy ànd ak janaba (war a sangu farata ngir jaxasoo goo defoon ak sa soxna) ak doonte dangaa yendook moom bёccёg bépp tam. + +6 – gént, dara warul ku gént fekk mu woor, ngir ab àddis: “yekkatees na xalima gi wёlif ñatt, ab dof ba kero muy xiqi (juge ci dof gi), kuy nelaw ba kero muy yewwu, gone ba kero muy gént (muy doon mukallaf)” + +7 – lekk mbaa naan ngir juum mbaa fàtte, waaye Maalik moom gis na ne war naa fay bu dee koorug farata, ngir léemtu (ngir lu gёn a wόor), bu dee naafila nag moom fay du ko ci war mukk, ngir waxam ja (j.m) : “ku fàtte ba lekk mbaa mu naan cig koor, na mottali kooram, ndax Yàlla’a ko leel, nàndal ko” ak waxam ja (j.m) : “ku dog ci ramadaan ngir ag fàtte, du fay te du kafaara” + +Fukkeelu ne-ne bi : ci leeral luy kafaara ak lan mooy njariñ li : + +Kafaara +Kafaara mooy li ñuy fare ab bàkkaar bu ñu def ngir ñàkk a topp ndigali Aji yoonal ji (Yonnant bi), ku wuuteek aji yoonal ji ba jaxasoo ci bёccёgu ramadaan mbaa mu lekk mbaa mu naan cig tay, war na mu kafaara wuute gii mu def, loolu nag benn lay doon ci ñatt yii: goreel jaam bu dib jullit, walla woor ñaari weer yu toftaloo, walla leel juroom benn fukki miskiin, miskiin bu nekk mudd ci dugubi suuna mbaa ceeb walla tàndarma kem ni nga ko mane, ngir li nga gisoon ci addiisub waa ji séyoon ak soxnaam ci koor, daal di laaj Yonnant bi (j.m). Kafaara nag dina limu ci limug wuute yi, ku jaxasook soxnaam cib bis, naan mbaa mu lekk ca bis ba ca des, ñaari kafaara war na ko. + +njariñul kafaara +Njariñ li nekk ci kafaara mooy ñogal sariiya ba duñu ko foye, di xotti wormaam. Moom itam day laabal bakkanub jullit bi ci jeexiiti bàkkaari wuuteek ndigali Yonnant bi (j.m), yi ñu def ci lu dul ngànt, looloo tax ñu war a defe kafaara ni ñu ko yoonale ci kem bi ak naka gi (ni muy tollu ak ni nu koy defe), bu ko defee mu man moom kafaara def li ko taxoon a jug, muy far bàkkaar bi aki jeexiitam ci bakkanu jullit bi. Cosaanul kafaara mooy waxi Yàlla ji (t.s): "yu rafet yi danañu demal (dañal) yu ñaaw yi" ak waxi Yonnant bi (j.m) : “ragalal Yàlla foo man a nekk, lu ñaaw (loo man a def) toppal ca lu rafet, dana ko far, àndal ak nit ñi ci jikko ju rafet” + +Ponki Lislaam +Lislaam +Xam-xamu nosukaay (walla Xam-xam bi ñeel nosukaay), moo yor gëstu gi aju ci cëslaay yu xibaar yi, xarala yi ñeel seenug nos ak seenug jëfandikuwiin ci noste yi ñuy jëfandikoo ay nosukaay. Ñi ciy yëngu seen liggéey doon lëkkale ay nosukaay ñu doon li ñuy tuddee ag lonkoo, defar ay dàtti njoxe, boppal ay noste, defar ay tëriin te loolu laaj na xam ag kàllaamag tëriin, . + +Cig lawal, xam-xamu nosukaay dafa ëmbu ci li ñuy wax xaralay xibaar ak jokkoo yu yees yi di xeetu xam-xam bi ëmb lépp li ñeel xibaar, ci gépp anamam. Ci tëriin wi la tëralkat bi di joxee ay tegtal nosukaay bi ci anam gi mu war a yoree xibaar yi, lan la ci war a def ak nan la ko war a defe. Jëfaan yi nag ñooy mbooleem cëri nosukaay bi, benn bu ci nekk am na liggéey bu ñu ko sant: yii di rënk xibaar yi, yii di leen wone ni nga bëgge, yii di leen soppi... + +Taariix +Ba àdduna dooree ba tay nit daa mas di ut ay jumtukaay ngir man a def ay waññeem. Ci jumtukaay yooyu, ci yi gën a yàgg, man nañu cee lim àlliway Hammurabi (1750 laata yeesu). Wuutuloxo yu doolerandu yu njëkk ñoo ngi tàmbalee feeñ ci diggante XVI ak XVIIu xarnu. Waññikaay bu doolerandu bu njëkk, jàpp nañu ne, mooy bu Wilhelm Schickard ci XVIu. + +Ci 1642 Blaise Pascal defaroon na, moom itam, ab Waññikaay bu doolerandu, doonoon bu ñu doon jaay sax, ba tay jii juroom-ñeent ci yooyu man nga leen a fekk ci jeexiituwaay (musée) yi. Ci ay njëlbeenam man nanoo wax ne xaymaan yi rekk ñoo ci doon yëngu ndax li leen yitteeloon moo doonoon defar ay jumtukaay yu leen di yombalal seeni Waññi yu xayma. Ay cëslaayam yépp ci xayma lañu taxaw, rawati na liñuy way aljibar bu Bool. + +Tay jii xam-xamu nosukaay jël na wàll wu am solo ci sunug dund, cig suqali ci wàllu koom-koom ak mboolaay yu askan yi. + +Xam-xamu nosukaay +Nosukaay ab wuutuloxo bu mbëjfeppal la buy seggat ay xibaar yu ñu ko jox jaare ko ci ag noste gu xellu gu ñu tëral-jiital. Ci wàllu xibaarfeppal la ñu koy jëfandikoo. + + Français: ordinateur + English: computer, di tekki waññikaay, ndax yi ñu ci njëkk a defar waññi rekk lañ doon def. + +Xam-xamu nosukaay +Mbëjfeppal, di ci wu-faraas "électronique", "إلكترونيات" ci araab, ab banqaasu jëmm la buy saytu, gëstu, jumtukaay yu mbëj yi seen dox wékku ci walug ay mbëjfepp. Ci maanaa, baat bi tay dafay tekki mbooleem lees xam di ko jëfe ak di ko xalaat muy tax a man a xalaat ak a nekkal jumtukaay yuy dox ak mbëj. Li mbëjfeppal di amal mooy ay ndomboy mbëjfeppal yu ñuy defar ak cër yu bari yees di lëkkale ci ndimbalu ay wëñ, naka-jekk wëñi mbéll, yu dawaanu mbëj di jaar ci seen biir. + +Mbëjfeppal ak xaralaymbëj nekk nañu ñaari banqaasi jëmm yu jegeente, seenug wuute mi ngi ci seen solo: su xaralaymbëj yoree li ñeel jóox dawaanu mbëj, seenug jokkale ak defari wuutuloxo yu mbëj, Mbëjfeppal moom, li ko yitteel mooy jëfandikoo mbëj ngir man cee weccee ay xibaar. + +Mbëjfeppal +Géej gu Diggu mooy géej gi ne ci diggante goxu Afrik ak bu Tugal ak bu Asi. Guddaayam di 2,51 milyioŋ ciy km² te yaatuwaayam toll ci 3700 km. + +Ci sowwu mi ngi yem ci Mbàmbulaanu Atlas, ci penku ci Géeju Marmara ak Géej gu Ñuul gi. Yenn saa yi Géeju Marmara dees koy boole ci Géej gu Diggu gi, waaye Géej gu Ñuul gi moom dees koy tàqale ak moom. + +Melokaan +Géej gu Diggu gi dees koo seddatle ci ñaari mbalka*. Mi njëkk mooy Géej gu Diggu gu sowwu gi, yam ci yoonal* gu Sisil. Meneen mi mooy Géej gu Diggu gu penku gi. + +Karmat + Yoonal: canal + Mbalka: bassin + +Géej +Diiwaani Tugal +Seede: wax Laa Illaaha Illal Laah, Muhammadun Rasuulul Laah, muy ci maanaa Yàlla rekk mooy buur, Muhammad (j.m) moo di ndawam li mu yonni ngir mu wuutu ko fi, di jàngal nit,ñi di leen xamal li Yàlla bëgg ci ñoom. + +Loolu nag di tekki dugg ci diine ju bees, wommatu ñeel Yàlla, bàyyi la nga nekkoon, nekk leegi ci lu bees lii la Yonnant bi woo, tënku ci ak lu mu metti metti, ak lu jamono soppiku soppiku. + + Gëm Yàlla + Gëm Malaaka yi + Gëm Téere yi + Gëm Yonnant yi + Gëm Bis Pénc + Gëm Dogal bi + +Wax laa illaaha illal laah +Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx.(Waxi Seex Ahmadu Bamba) + +Lislaam +Ponki Lislaam +NI NUY GËME YÀLLA + +Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam. + +Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) . + +Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, (dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk). + +Lislaam +NI NUY GËME MALAAKA YI (yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom) + +Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu. Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde. Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk. + +Lislaam +NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI + +Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp + +Lislaam +NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom) + +Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom. Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal. Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom. Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal. Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog. + +Lislaam +NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem ) + +Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay. + +Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone. + +Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi . +Lislaam +NI NUY GËME DOGAL BI + +Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi. + +Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame + +Lislaam +Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña. + +Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër. + +Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la + +Ni ñu koy defe +Laab +Soññee ci farlu ci xàmmee farata yi ak sunna yi ak bañ cee sàggan +Faratay Julli +Sunnay Julli +Jàpp +Faratay Njàpp +Sunnay njàpp +Sangu Farata +Faratay Cangaay +Sunnay Cangaay +Tiim +Faratay Tiim +Sunnay Tiim +Fay Faat + +Ag leeral + +Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku biral ci ginnaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi. + +Lislaam +Ponki Lislaam +LAAB) + +Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la. + +BUNT 1 + +Li aju ci laab + +Cours 1 : Njariñul laab ci Islaam + +Laab nag 2 xeet la : +1- Laab ci sa jëmm +2- Laab ci li la wër te mooy say yere wala ci barab bi ngay jaamoo Yalla + +Li ñu bëgga jànggale fii nag mooy laab ci sa jëmm, te loolu ni ñu ko mana defee mooy 3 yii : +1- Jàpp +2- Sangu farata +3- Tiim + +Am na jëf yoo xam ne maneesu lee na def te yoroo njàpp, lu mel ni : +- Julli +- Laal kaamil u Alxuraan +- Tawaaf (wër kaaba gi) + +Kon 3 yii kepp ku ko leen bëgga def fàww nga laab ba noppi. Laab googu nag soo ko bëggee def da ngay jàpp bu fekkee da ngaa wara jàpp wala nga sangu farata bu fekkee da ngaa wara sangu farata. Soo amul ndox moo ko defee wala nga am ngant may na ñu la kon nga tiim. + +Diine +Lislaam +SOÑÑEE CI ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK CEE SÀGGAN + +Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete, ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara. + +Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li. Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp mi ni mu ware. + +Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji. Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi. + +Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna, kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele. + +Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu. + +Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko. +FARATAY JULLI + +Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi. +SUNNAY JULLI + +Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12 li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18 am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir. +FARATAY NJÀPP + +Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj 8 gaaw +SUNNAY NJÀPP + +Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi. +FARATAY SANGU + +Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu +SUNNAY CANGAAY + +Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi. +FARATAY TIIM + +Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul. +SUNNAY TIIM + +Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi. Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim. +Asaka +Ay farataam aki sunnaam + +Ponki Lislaam +Lislaam +ASAKA + +Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yéene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool : 1 nga ànd ceek teeyug bakkan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal. + +Ponki Lislaam +Aj +Ay farataam +Ay Sunnaam +Lislaam +Ponki Lislaam +Faratay AJ + +Aj ñeenti farata la am : +1 yéenee aj +2 tawaaful ifaada +3 dox diggante safaa ak marwa +4 taxaw arafa. + +Ponki Lislaam +SUNNAY AJ + +Sunnay aj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labbayka. + +Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 fóon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti yoon yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi. + +Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yéegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa. + +Ponki Lislaam +NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINNAAW IMAAM + +Lu war la ci maamoom mu fay li ko faat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot. + +Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat. + +Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex. + +Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf. + +Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël. + +Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko. + +Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem. +LIHSAAN (rafetal) + +Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu. + +Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral. + +Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ. + +Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat. +Baatu xay day tekki mbooleem ay mbaax ak ay melokaani aw askan. Maanaam xamug àdduna, ci wàllu yar ak teggin ak xam-xam, yewwute gu nit ñi ci aw askan. Su ñuy wax xay dañ ciy nat tolluwaayu sag dundin, ndax jëm na kanam walla déet; baat bi dafa ëmb mbooleem ay yëngu-yëngu yuy am ci aw askan: diine, cosaan, xamteef, politig,... + +Su ñu nee nit kii dafa xayadi, day tekki ne xamul àdduna. Kon xayug aw askan ñoo ngi koy natt ci doxaliin, dundiinu cër bu ne ci askan wi + +Limub ay xay +Yenn ciy xay yu doomi aadama: + + Gu Babiloñaa + Gu Isipt gi Yàgg ga + Gu End + Gu Ittite + Gu Siin + Gu Geres + Gu Rom + Gu waa penku (Siri, Fenesi, Yëwut) + Xayug Lislaam + Monomatapa + Maya + Sapoŋ + Xayug Mongoli + +Wikibaatukaay + (en) xay + (fr) xay + +Lëkkalekaay yu biti +Taariixu xay yi (ab lonkoyoonu xay yi ci Flash) + +Xay +Sowwu Tugal benn la ci diwaani Tugal yi, waaye tekki gi ñu ko jox taxu kaa jub. da ñuy jàpp ne mi ngi toll ci diggante Mbàmbulaanu Atlas yem ci peggu Bëj-saalumu Tugal ak Penku Tugal. + +Waaye ci lu ëpp da ñuy boole Diggu Tugal ak Bëj-gànnaaru Tugal ci Sowwu Tugal. Soo nee waa sowwu dafa mel tugal gépp ngay wax, ba mu des gu penku. Kon ay peggi Sowwu Tugal leerul + +Gis-gis yi ñuy jàppee sowwu tugal da fay wuute. + +Bu njëkk + +Ay réewam + Almaañ + Andoor + Ótriis + Beljik + Danmaark + Ispaañ + Finlaand + Faraas + Girees + irlaand + Islaand + Itaali + Liechtenstein + Luksembuur + Malt + Noorwees + Olaand + Portugaal + Nguur-Yu-Bennoo + San Marino + Suwis + Suweed + Batikan + +Bii gisin moo ngi judd ci ñaari dank (bu sowwu ak bu penku) yi juddoo ci xare bu sedd bi. + +Ñaareel bi + +Sunu xoolee ni ko Kureelu Mbootaayu Xeet yi jàppe réew yi fa ne ñooy Faraas, Almaañ, Beljik,... + +Melosuufug Tugal +Lonkoyoon Ci séwógaraafi lañ ëpp ci li ñu koy jëfandikoo. Dañ ciy jëmmal ay barab walla ay yoon + + Français: carte + English: map + +Melosuuf +Curitiba, benn dëkku bëj-saalumu Bereesil. Nitñii motnañu 1 808 969 (2007). + +Lëkkalekaay yu biir + + http://www.curitiba-brazil.com + http://www.curitiba.pr.gov.br + +Dëkk +Breesil +Alaaji Maalik Si ma nga gane àdduna ci Dëw Faal gniou koy wowé Gaaya bokk ci tunduw Dagana ci atum 1855. Waa-juram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Mi ngi jànge alxuraan Luga ci kenn ci taalibey Alaaji Omar Futiyu Taal yi. Bi mu doonee mag la dem Màkka, bi mu dellusee sax ci jaamu Yàlla ak jàngale ak dugal ñi duli jullit ci lislaam. Ci noonu la tase njàngalem yoonu Tiijaan ci Senegaal jaare ko ci tuxoom yi ci Jolof, Kajoor ak Ndar. Ci mujj gi mu dëkksi Tiwaawan ci 1902. Fa la njëkk a wootee gàmmu. + +Juddoom +Ma nga gane àdduna Dëw Faal wetu Gaaya bokk ci tunduw Dagana ci atum 1855. Waa-juram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Usmaan moom doonoon doomu Muhaz miy doomu Mohamed, sëtu Yuusuf, Daraaman, Sire, Bubu, Yahya, ñoom ñépp di sëti sëriif Sams Eddin, loolu moo ko tax a askanoo ci araab. Baayam Usmaan, moo bàyyikoo Gànnaar fa mu doon jànge, ci Ustaas Muhamadu Baaba Al Daymani, ñëwoon Waalo doon fa wut ab téere bu kenn kii di Maalik Sow bu Gaaya rekk yoroon, ba mooy mujj doon turandoowam. Ñoom dañoo mujj dooni wolof, ndax ay maamam sax yàggoon nañu waalo, takkoon fay soxna. + +Njàngam +Ni bépp doomu waalo-waalo, ba mu doone gone la dal baa, nijaayam Alfa Mayoro moo ko doon njëkk a jàngal ba yàgg turandoom Cerno Malik Sow jël ko. Ci 1863, bi muy am 8 at, la dem Sagata ca Jolof ci baayam ba Amadu Si, mu jógeeti fa dem ci yeneeni ustaas, ku ci nekk taggak ko ci sag maneel, (fiq, nos-wax, Tawjiid, añs), ku ci mel ne Ceerno Ngañ Ka mi mu àndaloon dem Careen ci Fuuta Tooro ci 1873, bi muy am 18 at la jeexal njàngum alxuraanam ci tukkeem ca Fuuta, ba tay, ca Longe, cig leeral, ci sëriñ Abdu Bitey, ak ca Gànnaar. Ca la ñibbee dëkkam, Nijaayam Alfa Maayoro jox ko wird tiijaan ak maqaamay "mawdo", moom mi jëlee woon wird bi ci Alaaji Omar Taal ay at laata Maalik di judd. Te bii doonul woon benn lijaasa rekk bi mu amoon, ndax Mawdo Faal joxoon na ko ci 1876, ak Mohamed Ali it , ci ginnaaw bi. + +Ginnaaw bi mu mokkalee alxuraan, la jàngi fiq, ci lu njëkk, këram la ko doon jànge, ginnaaw bi mu dem ci Sëriñ Muur Ka. Bi mu mokkalee fiq la dem jàngi àtteyiin ca Boxal ci Waalo daaraay Sëriñ Ahmadu Njaay, ak ca Kër Kodde ci Njambur daaray Sëriñ Moodu, ak ca Tayba Séy daaraay Sëriñ Moor Kal Séy. Ginnaw bi mu jànge Risaala, ci diggante 1882 ak 1880 mi ngi amoon 25 at, la dem Ndar ci Sëriñ Ahmadu Njaay. Mu jógeeti fa dem Njambur ngir àggalee fa njàngum àtteyiin ma te door jàng Xalil ci Sëriñ Birahim Jaxate ak Sëriñ Mamadu Wadd. Waaye at ma ca topp la jeexal Xalil ca Mbokkol ci Kajoor ci Sëriñ Masila. + +Ci 1885, bi muy am 30 at, dajale woon na xam-xam bu jéggi-dayoo, loolu mayoon na ko mu man a doon ustaas, jamono yooyu bokkoon na ci ñi ëppoon xam-xam ci Senegaal, ndax lépp lu ñu manoon jàngale ci réew mépp jàngoon na ko, demoon na ci ñi fi ëppoon xam-xam. Ci tukkiy njàng yi mu defoon yépp, ca jamono jooju, jaaroon na ca tund ya ëppoon boroomi-xam-xam: Gànnaar, Fuuta, Njambur, Kajoor. ci dëkk yi mu dem man nan cee lim: Ndoj Séy, Pacaas, Ngicc, Jaabe Lidube, Orefonde, Longe Sëbe, Longe Fulbe, Careen, Ndar, Tayba Séy, Daraaman, añs. + +Dundam ak jëfam +Ginnaaw ag njàngam, Ngambu la dem dëkki di fa liggéey aka jàngale ngir dund ci ñaqam. Liggéeyam mayoon na ko mu man a aji Màkka jaare ko bëj-saalumu Fraas, ci Maarsey ak ci Aleksandri, ci 1889, amoon na 33 at. + +Bi mu jóge Màkka am maqaamay alaaji, ci la sosee Sawiya bu Ndar ci 1892. Ganeji Jolof ab diir sos fa ay daara dellu Waalo. Ay tukkeem yu bari ci biir réew mi, ngir tasaare diine ak xam-xam, ak Wasifa yi doon ame ci Sawiya yi taxoon sancaan bi tambali koo fuglu, yaakaar ne day woote ngir xeex ko ak ngannaay yi. Ca la ko kaŋ ba nekkoon Ndar te nekkaloon fi sancaan bi (waa Fraas yi) woolu ngir mu joxe ay leeral ciy yëngu-yëngoom. Ñoom dañoo foogoon ne dafa dencooni ngannaay ci biir jakka yi, difa waajal xare ak ñoom. Bi ñu ko ci laaje mu ne: + +«Yàlla daf nu digal, man ak yeen, nu jaamu ko, di julli ci moom. Ngeen bañ, ma nangu. man ak samay taalibe defuñu lenn lu dul kañ yàlla te di julli ci gën-gi-mindeef. Te li ngeen di wax ci ngannaay yi, genn ngannaay gi ma yor mooy sama kurus te moom laa fas-yéene xeexee ba Lislaam ak Tijaaniyaa tas ci àdduna bépp.» + +Sancaan yi jàppoon nañu ne Alaaji Maalik moo doonoon nik ki ëppoon xam-xam te daq a jangalee ci réew mépp. Baat yii di nañu leen fekk ci dencu(archive) yu Senegaal yi ak yu Fraas. Seede yi gëna neex ci nopp ñooy yu Seex Sidiya, my sëtu yonnenti bi doonoon it sëriñu xaadir bu mag. Ginnaaw ba mu taxawalee sawiya ca Ndar, taxawal na beneen ci Ndakaaru ci wetu njéndul nguur gi. Njarnde la dem dëkki, jóge fa dem Jaksaaw, laataa muy dem Tiwaawan ba faaw. Jibril Gëy moo ko fa woolu woon ngir mu defal leen tafsiir Alxuraan, ñu faf ko fa téye, ci 1902 mu sos sawiya bu Tiwaawan. Ci yokkug ndongo yi, mu jël yeneen ustaas ngir ñu jàppale ko ci njàngale mi. Ca daaram ja, daa nañu fa jàngalee bépp xeetu xam-xamu lislaam. Ci téemeer ak lu tekk ci ndongo yi mu yoroon, lu mat juroom-fukk daan nañu dem itam ci jànguy nasaraan si, doomam sëriñ Baabacar Si daa na ca dem, Loolu firnde la ci xelam ak gis-gisam bu ubbeeku. + +Ci Tiwaawan la wootee Gammu gu njëkk, ngir màggal seydinaa Muhammad. Mu door njàngale mu diggoodi, dëkk bu ne mu yabal fa ab muqadam bu fay jàngale diine. + +yenn ciy téereem + Ifham al munkiru jaani: téere bu muy jàngale luy tiijaaniyaa, ustaas Rawaan Mbay moo ko tekki ci wu-fraas +Khilaçu ez-Zahab: mooy téere bi gën a mat buy wax ci jaar-jaaru yonnenti bi, ba mu juddo ba, ba muy génn àdduna, Rawaan Mbay moo ko tekki ci wu-fraas +Sharh Khilaçu ez-Zahab: faramfacce gu téere bi, moom mi bind téere bi moo ko def +Faakihatul Tullab: est un précis sur la Tijaniyya et ses pratiques.Traduit en français par l'éminent Professeur Rawane Mbaye +Dîwân: ay woy la ci yonnenti bi, Ahmed Tiijaani, Alaaji Omar Taal, ay xam-xami diine, ay xelal ngir jullit ñu rawatina tiijaan yi +Khutbatul Jumu'a; digle julli ajjuma +Khutbatul 'I'd: digle julli tabaski ak korite +Kifayat ar-raghibîn: ( li aji-gëm gi soxla) ustaas Rawaan Mbray moo ko tekki ci wu-fraas + +Téerekaay + Michael A. Gomez, Malik Sy, Bokar Saada and the Almaamate of Bundu, Chicago, University of Chicago, 1985, VIII-484 p. (Thèse) + Cheikh Tidiane Fall, El Hadji Malick Sy à Tivaouane de 1902 à 1922, Dakar, Université de Dakar, 1986, 92 p. (Mémoire de Maîtrise) + Rawane Mbaye, La pensée et l'action d'El Hadji Malick Sy : Un pôle d'attraction entre la Shari'a et la Tariqa. Vie et œuvre de El Hadji Malick Sy, Université de la Sorbonne nouvelle, Paris III, 1993 (Thèse) +tiijaaniyaa +niti senegaal +Ngir xam taariixu Senegaal, taariixkat yi am nañu ay gongikuwaay yu bari : gongikuwaay yu gimiñ, yooyu nag yu bari lañu waaye soxla nañu ay gëstu yu xóot, ndax dañuy faral di jaxase diggante dëgg ak léeb (mythe). Ak jeexiit yi, ñoom nag bariwuñu te lu tas la, ak gongikuwaay yu mbind yi, ñoom it yu néew lañu, ndax askan yi dëkke woon Senegaal ca jooja jamono xamuñu woon mbind. + +Senegaal nag suuf su ñuy gàddaaye génn la ak su ñuy gàddaaye jëm. Aw askanam, diirub ay xarnu, dañoo nekk ci diggante sax ak laxas. Senegaal nag taxawal na ay séqoo yu am solo ak aw askanam ak itam réew yi mu feggool. Daa na jëflante ci wàllug yaxantu ak gox yu sori yi. Loolu lépp nag tax na ba réew mi am aada ju cosaanu. Nguur gi njëkk ci Senegaal ñi ngi ko taxawal ci lu tollook juroom ñaareelu xarnu g.j, man naa am sax mu jiitu loolu. Nguur yooyu nag amuñu woon doole lu dul ci ñaari xarnu yii, bu fukk ak ñatt ak bu fukk ak ñeent, maanaam ci jamonoy imbraatóor yu ñuul yi (yu nit ku ñuul yi), gu Gana, Mali ak Songaay. +Nguur yii ci ron kiliftéefug imraatóor yii lañu nekkoon. + +Ci xarnub fukk ak ñeent Jolof soppiku na di nguur gu mag gu am ay sañ-sañ yu yaatu, teg loxo ci ay wàll yu mag ci nguur yooyu. +Ci xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn, yenn nguur-nguuraan yi tàmbali woon nanoo daggu ci Jolof ndànk-ndànk, ci noonu Jolof mujj di nguur gu yamamaay niki yeneen nguur yi rekk. +Nguur gu ci nekk ab buur a ko daan jiite, ab jataay (conseil) moo ko daa jox sañ-sañam, jataay boobu moom lañu dénkoon muy fuglu ay saxalam aki ndigalam , ay foŋsaneer daa nañu dimbale buur bi, di def liggéey yi aju ci saytu alal ji, wattu kaaraange gi, taxawal yoon, ñenn ci ñoom it daa nañu dooni kaŋ (gouverneur) ñeel lenn ci diiwaan yi. + +Nguuri Senegaal + Jolof + Fuuta Tooro + Bawal + Kajoor + Waalo + Kaasamaas + Kaw Gaambi ak Penku Senegaal + Nguuri Pël yi + +canc gi +Cada Mosko mooy tubaat bi njëkk a tek tànkam ci suufi Senegaal ci atum 1442, buur ba nekkoon Poortugaal moo ko yónni woon. Ci noonu la waa Poortugaal tambalee jëflante ak waa senegaal yi fa nekkoo, yaxantu judd ci seen diggante. Ci nii ba mu yàgg waa angalteer dal di ñëw, waa faraas tegu ci ak waa Olaand. Dem na ba waa faraas rek a fi desoon sanc réew mi yépp; def Ndar péyam tek fa ab Laman buy yor réew mi. Laman yooyu ay tubaab la ñu daa doon yu daa jóge ca Faraas. + +Ci Ndajem Berlin mi la réewi tugal yi waxtaan ba deggoo ci ana naka la ñuy seddoo Afrik. + +Jàmmaarloo ci ngànnaay lànk canc gi +Lu ëpp ci goxi Afrig yi waa Tugal yi tegoon loxo ci jàmm lañu ko defe woon, li ko waral mooy waa Afrig yi dañoo jortoon ne tubaab yi de dañu fee jaar rekk waaye duñu fi yàgg. Waaye ci ginnaaw bi lañu gis ne canc gi (la colonisation) de mi ngi defi sémb ngir nar fee sax, te it mi ngi liggéey ci soppi séenuw dundiin. + +Ci yenn barab yi ( niki Senegaal ), waa Tugal yi daje nañook ay jàmmaarloo yu tar. Nguuri Afrig yi amoon nañu ay xare (larme) yu ñu waajal, looloo leen dimbali woon ci ñu man a xeex jàmbur yii. Bu dee giir yeek dëkk-dëkkaan yi, ñoom dañu doon xeex ci séenug anam, maanaam di def ay cong yu tàqalikoo, fii ak fee (dóor-làqu ;guérilla). + +Waa Afrik yi def nañu ay jàmmaarloo ci ngànnaay, yu jur ay ñàkk yu tar ci sàppes waa Tugal yi. Yenn jàmmaarloo yi wéy nañu ba ci atum 1930 g.j . +Ca dëgg-dëgg waa Afrig yi ñoo gënoon a limu, te ëppooni xam-xam ci toolu xare bi. Soldaari Tugal yi nag yoroon nanu ay ngànnaayi sawara yu aaytal, waaye dañoo xawoon a doyadi, ndax manuñu woon a dékku tàngoor wu tar wi ak tawati rëddu yamoo wi (maladies tropicales). + +Man nan lim ñenn ci ay way lank canc gi ci Senegaal: Lat joor Joob, Alburi Njaay, Alaaji Omar Taal, Muhammad Lamin Daraame, Saamóori Ture, Alaaji Maalik SY, Seex Ahmadu Bamba, Seydinaa Limaamu Laay, Aliin Situwe Jaata,... + +Gongikuwaay +Téere taariix Senegaal bu Abdu Xaadir KEBE +Alaaji Omar Fuutiyu Taal mi ngi gane àdduna ci ndëkk su ñu naan Elwaar, ci wetu Podoor atum 1794 -1796 g.j, mu bokkoon ci askan wu cosaanu ci Lislaam, baayam mi ngi tuddoon Sahiid mom Usmaan mom Muxtaar Tukkloor bi, yaayam tuddoon soxna Aadama Caam. + +Dund na ay at ca barab yu sell ya (Màkka), bi mu déllusee réewam la dogu woon ci tas Lislaam te jële fi way sanc yi. Ci atum 1853 g.j, la jibal jiyaar ngir yékkati baatub « Laa ilaaha illal Laah » . + +Mu song Karta ak Xaaso nangu leen, def fa imbraatóoram gu lislaam gi. Xareb Alaaji Oamar fenqoo na’ak bu Federb bi nga xam ne li ko yékkati woon mooy aar sancoom yi mu amoon ci sowwu bi, ak jéem a tegi loxo penku bi. Alaaji Omar saxoon na te të ci kanamu dooley sanc gi, waaye ci mujj gi mu daanu ca doji Banja Gara ya ca Gine atum 1864 g.j. Bu ko defee doom ja Ahmad Seexu daal di yanu raayob jiyaar bi ci ginnaawam, waaye moom it amoon na ag lott ci kanamu ngànnaayu sancaan yu lëw yii te aaytal. Bi mu ñàkkee pexe la xaatim ag kóllare ak tubaay yi atum 1881 g.j, waaye Gayni mi mu defaloon kóllare googu daal di koy wor, ndax songaat na ko, ga ko ci mu daw, foofu la imbraatóor gi daanoo ci loxoy tubaab yi, atum 1889 g.j . + +niti senegaal +tiijaaniyaa +Melaneesi benn la ci diwaan yi ñuy faral di seddatlee Oseyaani. + +Bii seddatlin nga xam ne Kureelu Mbootaayu Xeet yi sax mooy la jëfandikoo suy seddatle àdduna bi ci ay Diwaan, gëstukat yi ñoom seddatle bu bees bi la ñu taamu, moo xaaj Oseyaani ci ñaari diwaan: Oseyaani gu jege ak Oseyaani gu sori yi melaneesi box. + +Baatu Melaneesi waa faraas bii di Jules Dumont d'Uville moo ko sakk ci li jege atum 1830 (moo sakk itam baat yii di Polineesi, Mikroneesi ak Maleesi), mi ngi jóge ci baati waa Geres yii di μέλας (ñuul) e νησος (dun) maanaam dunu ñu ñuul ñi. + +Ay dun yu tuut ñoo fa ne, man cee lim: + Ginne-Gu-Bees gi + Kaledooni-Gu-Bees gi + Fiiji yi + Duni Solomon + Duni Banuwaatu + Bismarck + +Ñenti réew ñooy yi fa ne ak benn suuf bu bokk ci Faraas: + + Fiiji + Duni Solomon + Kaledooni-Gu-Bees + Papuwasi-Ginne-Gu-Bees + Wanuatu + +Diwaani oseyaani +Mikroneesi benn la ci diwaan yi ñu seddatlee goxu Oseyaani. + +Bii seddatlin nga xam ne Kureelu Mbootaayu Xeet yi moom la jëfandikoo suy seddatle àdduna bi ci ay Diwaan, gëstukat yi ñoom seddatle bu bees bi la ñu taamu, moo xaaj Oseyaani ci ñaari diwaan: Oseyaani gu jege ak Oseyaani gu sori yi Mikroneesi box. + +Baatu Mikroneesi waa faraas bii di Jules Dumont d'Uville moo ko sakk ci li jege atum 1830 (moo sakk itam baat yii di Polineesi, Mikroneesi ak Maleesi), mi ngi jóge ci baati waa Geres yii di μικρος (tuuti) ak νησος (dun), maanaam dun yu tuuti. + +Diwaan bi ay teemeeri dun a nga fa. Ñaari réew yu témb a fa ne ak ñaar yu bokk ci Réew yu Bennoo yu Aamerik yi: + + Guam (US) + Duni marsaal + Dunu Maryian gu Bëj-gànnaar (US) + Kiribati + Nauru + Palau + Réew yu Bennoo yu Mikronesi + +Diwaani oseyaani +Polineesi benn la ci diwaan yi ñu seddatlee goxu Oseyaani. + +Bii seddatlin nga xam ne Kureelu Mbootaayu Xeet yi sax mooy la jëfandikoo suy seddatle àdduna bi ci ay Diwaan, gëstukat yi ñoom seddatle bu bees bi la ñu taamu, moo xaaj Oseyaani ci ñaari diwaan: Oseyaani gu jege ak Oseyaani gu sori yi Polineesi box. Diwaan bi dafa am meloow ñettkoñ + +Baatu Poloneesi waa faraas bii di Jules Dumont d'Uville moo ko sakk ci li jege atum 1830 (moo sakk itam baat yii di Melaneesi, Mikroneesi ak Maleesi), mi ngi jóge ci baati waa Geres yii di πολύς (bari) ak νησος (dun), maanaam dun yu bari. + +Diwaan bi ay dun yu baree fi ne, man nan cee lim: + Awaai (USA) + Duni Bennoo bi + +Diwaani oseyaani +Mbàmbulaan am mbalka mu réy la mu def ndoxum xorom, te wër ab gox. + +Mbooleem mbàmbulaan yi ak géej yi ñoo jël 70% di ñatti ñeenteel ci li ci Kaw kol-kolub suuf si, maanaam 360.700.000 km². Ci lim bii 154.800.000 km² ñoo ngi ci xaaju kol-kol bu bëj-gànnaar, 205.900.000 di km² ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum. + +Mbàmbulaan yi juróom lañu: + Mbàmbulaan gu Dal, 179.700.000km², 49,7%; + Mbàmbulaanu Atlas, 106.100.000 km², 29,5%; + Mbàmbulaanug End, 74.900.000 km², 20,4%; + Mbàmbulaan gu Bëj-saalum, 20 327 000 km², 5,6% + Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar, 14 090 000 km², 3,9% + +Waaye waa-Angalteer yi ci seen gisinu melosuuf da ñuy jàppee mbooleem géej yi ne ci li wër ñaari goxi dott yi, duppee leen Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar ak Mbàmbulaan gu Bëj-saalum. +Tus-wu-gaar wenn la ci ñaari xammikaay yi (beneen bi mooy tus-wu-taxaw). Tus-wu-gaar wi ci bëj-gànnaar walla bëj-saalumu yamoo gi lay nekk. + +Lëkkalekaay yu biir + Tus-wu-taxaw + Gëwéel + Gëwéelub sànkar + Gëwéelub tef + +Melosuuf +Baatu dottub Bëj-saalum daa am ñaari tekki: ci benn bi ab gox (Dottub bëj-saalum) la di ci beneen bi ab tomb. + +Dottub Bëj-saalum mooy puju àdduna bi ci Bëj-saalum, maanaam tomb bi gën a féete Bëj-saalum ci àdduna bi. Moom ci boppam am na ñaari tekki: di nan wax dottub Bëj-saalum «gu melosuuf» ak dottub Bëj-saalum «gu bijjaakon» (dottub bijjaakon). Ñaari tomb yi bokk ñu ndaxte fi dottub Bëj-saalum gu bijjaakon di ne day aju ci coppiteeg toolu bijjaakonu àdduna bi. + +Gu melosuuf +Ki fa njëkk a tek tànkam mooy nemmeekukat boobu di Roald Amundsen di waa Norweej, ci 14 weeru tabaski atum 1911. Ca seenug dëpp la Robert Falcon Scott, di ki mu doon njëkkanteel, aki ñoñam ya mu andaloon saayee. + +Lëkkalekaay yu biir + Goxub Dottub Bëj-gànnaar + Goxub Dottub Bëj-saalum + Dottub Bëj-gànnaar + +Diiwaani dott +Diwaani dott yu àdduna bi ñooy barab yi ne ci li wër dott yi. Goxub Dottub Bëj-gànnaar dan koy jox tekki yu bari; da nuy wax ne mooy mbooleen suuf yi ne ci bëj-gànnaaru Mbegeb dott bu Bëj-gànnaar bi, walla suuf yi ne ci rëddu tus-wu-gaar wu 60° (60 aj) ci bëj-gànnaar. Goxub Dottub Bëj-saalum moom daanaka kenn du ko yemale ci Mbegeb dott bu Bëj-saalum da nuy wax ne mooy mbooleem suuf yi ne ci rëddu tus-wu-taxaw wu 60° (60 aj) ci bëj-saalum. + +Li ñuy gën a xammee diwaani dott yi ñooy seeniy jamono yuy nangoo sedd, li nuy wax klimaab dott. Diirub nawet naaj bi di na am 24 waxtu (li ñuy duppee naajub xaaju-guddi), diirub noor nak day lëndëm rekk sax-dàkk. + +Bari na nak ñi dëkk ci barabi dott bu bëj-gànnaar, waaye bu bëj-saalum kenn dëkku fa, lu ko moy am na ay sañc ngir ay gëstug xam-xam, ci wàll wi gën a féete suuf ndax lu mu gën a sedd. + +xool it + Goxub Dottub Bëj-saalum + Dottub Bëj-saalum + Dottub Bëj-gànnaar + Goxub Dottub Bëj-gànnaar + +Lëkkalekaay yu biti + (en) International Polar Foundation +diiwaani dott +Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juroom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko, ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko. +Bu ko defee daal di jël nguur gi, ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana. + +Waar Jaabi dugg na ci lislaam, daal di jug def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit, ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci lislaam ci Senegaal. + +Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi, li ko waraloon it mooy dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi. +Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn), ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent). Ci mujjug xarnub fukk ak juroom la Koli Tingala (kilifa gu bokk ci càllallag Pël, juge ci wàllug bëj-saalum gi) jug xeex Tukulóor yi, daal di tembal ay goxam (ñu moom seen bopp) taxawal nag nguur gu yees mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko. + +Ci xarnub fukk ak juroom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom : Jolof, Kajoor. +Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarlook cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi (succession). Ci atum 1770 g.j, la ag fipp am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daal di daaneel njabootug Deñanke, bu ko defee Baal jël lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale. +Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan, moom lañuy jàppe ki njëkk a doon Yilimaan ( Amiirul Moominiin :njiitul jullit ñi) + +Gongikuwaay +Taariixu Senegaal bu Abdu Xaadir KEBE + +nguuri senegaal +Ci xarnub fukk ak juroom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi, bu ko defee, ag njaboot gu amug jegeñaale ak buuri Kajoor yi daa ko jiite. + +Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon. Am na ñu ne sax, baat bu ñu tudde dëkk boobu tey, di Bawol, ci kallama socé yi ñu fa nekkoon la joge, di tekki lii wolof tudd dex. Ndax Bawol, been dex la woon foofu ci lu dooga am. Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare. + +Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkka nekk buur, XAAYAMAGAAN moo doon turam. XAAYAMAGAAN, ci lakku socé yi la soqeekoo, mooy: buuru gaalam. Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawo. + +Ba paré, séeréer yi ñëw. Ñoom, fuuta tooro lañu joge woon, gadday ba Bawol, ndax jiyaar ji muraabituun defoon foofu. Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dekkando ak socé, sooga leen daq. Ba loolu ame, ñu elif dëkk boobu. Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo ñu sant Juuf, Ngom, Caw. Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, Téeñ lañu ko daan tudde. + +Loolu mo amoon, sooga nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi. + +Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la Jolof mànge poseb néew-dooleg nguurug Jolof , daal di jël ag tembam, ni ko yenn ci nguur yi defe woon, gu ci mel ne Kajoor ak Waalo, ngir song gu tar ga Amari Ngóne Sabel Faal defoon Jolof. Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji. + +Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam. Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk daa bëgg a yilif ga ca des. + +Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug kiy wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def. +Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi, mbooleem kuréel yi nag daa nanu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, ñoñ fànn ñi (boroom mecce yi) ak jigéen ñi). +Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ciy suufam, moom kay daa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi. + +nguuri senegaal +Taariixu senegaal +Cosaan Séeréer +Ci Kaw Gaambi ak Penku Senegaal Ay nguur yu bari toftaloo nanu ci dexug Gaambi gi, yi ci ëpp solo ñooy Ñaani ak Wuli. +Ñoom nag ñi ngi leen taxawal ci xarnub fukk ak ñeent g.j, ay way gàddaay yu bàyyikoo ca imbratóor gu Mali gaa leen taxawaloon. Yii nguur nag ci ron waawug Jolof gu mag gi lañu nekkoon, ba kero ñuy nanguwaat séenug temb ci xarnub fukk ak juroom benn g.j . +Nguur yii nag bokkoon nañu ci joqalanteg yaxantu gi ci anam gu sawar, looloo taxoon ñuy réew yu naat. + +Ci bëj-gànnaaru Wuli la nguuri Goy ak Kamera nekkoon, ki léen taxawaloon kilifa la woon gu bokkoon ci njabootug Baajli, mooy Salmaan Xaasa, mi nga xam ne jiite woon na ag nguur ci penku Senegaal. Ñaari nguur yii nag ba xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, dañoo bennoo woon. Buur bi dàkkantalu Tunka la daan yore. Ci atum 1833 g.j, la ab xare tàkk ci seen diggante, ba moo waral ñu tàqalikoo. Goxub Gaambi gu kawe gi ak Senegaal gu penku gi séddaliku na doon ay nguur yu bari, waaye am na ci yu daawul weesu yaatuwaayu as ndëkk. Gi magoon ci nguur yii ci lu dul sikk mooy Namandéeru ak Faalimi, ñaar yii nga xam ne ñi ngi leen sosoon ci lu tollook ñeenteelu xarnu g.j, ñu nekkoon nag ci ron kiliftéefug imbraatóor gu Gana. Am na yeneen nguur yu sosu woon ca la tollook xarnub fukk ak ñatt g.j, ñooy: Siiselaa, Beledugu, Niokolo, Badon, Bademba, Bundu, Gajaga. + +Nguur gu mujj gii nag (Gajaga) giirug Sambiira Baccili ñoo ko jiite woon la ko dale ca xarnub fukk ak ñatt g.j . Nguurug Gajaga dund na cig naataange ngir joqalantey yaxantu ya fa daa am te naataloon gox ba, rawati na yaxatug tàkk gi. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, yaxantu gi mi ngi sukkandiku woon ci daakaande. + +Nguuri Gambi gu kawe gi dañu daa dàkkul seen bopp cong yi leen seen dëkkandoo yi daan faral a def, jublu woon ci nangu ci ñoom lenn ci seeni suuf. Ci xarnub fukk ak juroom ñaar ak bu fukk ak juroom ñatt la ay xarekat yu juge ci penku dikk soppi nosteg àtte ga fa amoon, bu ko defee ay njaboot yu yees daal di tàmbalee sangu (dooni njiit) ca gox ba. Bu dee ca Siiselaa moom Daansirimaan moo daaneeloon njiitug giirug Siise, daal di wutal nguur gi weneen tur wu yees mooy : Sirimaano. Bu dee ca Beledugu moom, njabootug Siisoxo moo jële giirug Soomari ci nguur gi. Ca Dantila moom ab nappkat bu siiwe ci turu Samakoto moo nangu nguur ga, dàq njabootug Samora ga. + +Nguuri senegaal +Taariixu senegaal +Kaasamaas baat la bu ñu toggalee ci ñaari dogiit : Kaasa ak Maas boo leen boolee muy buuru Kaasa. Kaasa bokk na ci yi njëkk ci nguuri gox bii. Ginnaawam nag Gabu moo ci gën a rëy ci nguur yi. +Ñaari nguur yii ñi ngi leen taxawal ci lu tollook xarub fukk ak ñeent g.j, ci loxol ay xarekat yu bawoo ca imbraatóoru Mali ga, Sinjata Kayta yabaloon leen. Nguurug Gabu (nguur gi ëppoon doole ci yii) Trimaskan Traaware moo ko sosoon, mu nekkoon gi tegoon loxo nguur yu ndaw yi nekkoon ci bëj-gànnaaru Gambi, ñooy : Kantora, Gimaara, Jaara, Kiyaŋ ak Kombo. +Kaasa ak Gabu way toroxlu lañu woon ñeel Imbraatóoru Mali jamono yi nu leen sose ñoom ñaar, waaye Gabu moom tàmbalee fay galag ñeel imbraatóor gi, ci noonu mu ame ci «ag àtte-sa-bopp » (autonamie). Ci digg xarnu bu fukk ak juroom, la ñaari nguur yii jariñu ca yëngu-yëngu ya Koli Tingala amaloon ca gox ba, bi mu ko defee, ñu daal di dagu ci Mali. + +Ci xarnub fukk ak juroom ñatt g.j, la Kaasa tàmbalee tas : giirug Joola songe ko ci sowwu bi, gu Maalinke ci penku bi, gog Balaanta ci bëj-gànnaar gi.. +Ci atum 1830 g.j, la giirug Balaanta lakk péeyub Kaasa di Birikama. +Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Gabu it làmbalee naaxsaay, looloo mi ngi dale ca ba ko giirug Pël gi songee, mooy gi génne woon Fuuta Jalon, bu ko defee mu daal di tàmbalee ñàkk ndànk-ndànk sañ-sañ yi mu amoon ci gox yi mu yilifoon. + +Nosiinu biir gi ci nguurug Kaasa ak Gabu xawuñoo wuuteek wa amoon ca nguur yeneen ya ci Senegaal. Buur bi jataayub mag (sénat) ñee ko daa dimbale, moo daa fuglu it ay saxalam tey digal ay sañ-sañam. +Diiwaan yi ay foŋsaneer yu kawee leen daan jiite yu tukkee ci garmi yi. Waaye Gabu moom nga xam ne nguurug xare la woon : ay foŋsaneeram yu kawe mi ngi leen daa tànne ci xarekati garmi yi. + +Nguuri senegaal +Taariixu senegaal +Nguuri Pël yi, Ca jamono yu yàgg ya li ëppoon ci giirug Pël ay sàmm yu daa màng lañu woon, di tuxu ci seen bëgg-bëgg ngir wër ndox ak ñax, ñu nekkoon di ñu tasoon ci gox yu bari ci sowwu Afrig, la ko dale ca dexug Senegaal ba ca ngéejus Càdd (lac du Tchad). Ci diggante xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom ñeent g.j, giir gii def na fi ay fipp yu lislaam yu bari yu waral ñu taxawal ñatti nguur ci Senegaal : Fuuta Tooro - Bundu - Fuuta Jalon. +Ci mujjug xarnub fukk ak juroom g.j, am mbooloo ci way gàddaay yu Foolaan yi génne nañu Fuuta Jalon dem Fuuta Tooro, Koli Tingala jiite leen, moo tegoon loxo Fuuta Tooro ci atum 1512 g.j, daal di taxawal nguurug Fuuta Tooro. Ci atum 1770 g.j, la Sulaymaan Baal def ag jeqiku gu lislaam mooy gi soppi Fuuta def ko nguur gu lislaam Almaami Abdu Buukar jiite ko, mooy ki jiyaaroon kontar ay dëkkandoom : Waalo - Taraasa - Kajoor, la ko dale ca 1790 ba 1804 g.j, waaye dañu koo mujj dàq. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Fuuta tàmbalee naaxsaay. +Ci lu tollook 1690 g.j, la Tunka buurub Goy may menn mag mu juge Podoor aw dog ci suuf, mooy Maalik si, dog wooyu mi ngi nekkoon diggante Faalimi ak Gambi gu kawe gi. +Ci nii la nguurug Bundu sosoo. Maalik si daal di nay jibal ab xare, def it Bundu muy nguur gu lislaam, daal di safaanu nguurug Goy, gën a yaatal ag nguuram. + +Nguur googu nekkoon na di gu naat ci ayug Maalik Si aki way wuutoom (njabootug Siisebi), li ko waral di séqoo yi mu amoon ak Gambi. +Ci lu tollook 1727 g.j, la ag giirug Pël ca Fuuta Jalon jugoon - Karamoko Alfa jiite ko - soppi gox boobu it def ko nguurug lislaam, Almaami di ko jiite, ju njabootug Suriya di fal leeg-leeg, leeg-leeg gu Alfaya. + +nguuri senegaal +Lat Joor Joob mi ngi juddoo ca Kër Amadu Yala, atum 1842 g.j, Saaxewar Soxna Mbay Jóob mooy baayam, lingeer Ngoone Latiir Faal di ndayam.Lat joor a ngi Meenoo ci neegi gèej + +Ay meloom +Lat joor waxambaane wu jàmbaare la woon, wu amoonug dogu, mu bokkoon ci ñu mag ñi daa jàmmaarlook sancaan yi ci goxub Afrig, mu nekkoon di kenn ci ñi ci gën a jàmbaare, gën cee fés, kenn melul ni moom ci bëgg rèewam ak askanam. Amoon na fit wow kenn du ko doyadil, daawul tiit ak lu man a xew. Nekkoon na njiitul xare lu mag, di aji politig ju ñaw, ju di boroomug jommal. Ci atum 1862 g.j, la ñu fal Latjoor Dammeel ca Kajoor. + +Dundam ak jëfam +Ci atum 1864 g.j, la ko Federb daane ginaaw xareb Loro, teg loxo ca Kajoor, Ca la Lat joor deme Siin gir sakk o lëkkëloo ak Buur Siin Kumba Ndòofeen Juuf ngir xeeq Tubaab yi waaya Buur Siin daa gantal ci ndigëlu Federb. + Lat Joor weyal yoonam, ci la deme Rip fekki fa xaritam, wólórem bu yagg di : sëriñub tukulóor ba ñuy wax Màbba Jaxu Ba,Ginaaw xare yu bari yu Lat Joor def ak xam-xam bi mu am ci wallu xeex ak nand pexey tubaab yi, ci la Almaamy Maba sakku ci moom mu jiiteel ko ay soldaaram ngir wéyal jihaad ja mu doon amal ngir gën a tassaare islaam fa Saalum ak Siin, sakku it ci moom mu yeesal ag njulitam te dugg ci tariixa Tijaan. lislaam. + +Latjoor ak Màbba dajje na ñu ak Buur-Siin Kumba Ndóofeen Famak Juuf ca xareb Somb ca atum 1871,fa la ñu faate Màbba. +Ginaaw bi Latjoor defaat na fa ab diir foofu ca Rib laata muy dellu Kajoor gir nangu nguuram ci loxoy Tubaab yi, mu dellu waat di Dameelu Kajoor. + +Ci atum 1878 g.j, ci la Tubaab yi dogoo ak Lat Joor ci jaarale rail bi biir Kajoor muy yoonug weñ wu saxaar giy jaar ci diggënte Ndar ak Ndakaaru ngir yombal yòbbug gerte gi, waaye bi Latjoor demee ba gis ne loolu men la ci pexem tubaab yi ngir gën jekandiku ba mana dëgëral seenug nootel ci rèew mi, Lat Joor daal di bañ sakku ñu dakkal ligeey ba. daal di def ag fipp gu mag ak ay àndadoom atum 1882 ba 1883 g.j. Ci noonu xare bi tàkk digganteem ak Tubbaab yi, mu nekkoon xare bu tàng jérr waaye sancaan yi nootoon nañu Latjoor ngir néewug ay ngànnaayam aki jumtukaayi xareem ak bari gi ñu bari woon ñoom jumtukaay yooyu ñeel Tubaab yi. Ci noonu Latjoor ñakkoon pexe, daal di weeruji ca buurub Jolof ba Alburi Njaay, loolu nag di woon atum 1884. + +Bi Latjoor jugee Kajoor la Tubaab yi fal Ammari Ngoone Faal muy Dameelu Kajoor, waaye gaaw nañu koo folli ngir ñaxtu gu tar ga waa Kajoor doon ñaxtu loolu. Bu ko defee Samba Lawbe Faal ñëw toog ci jal bi, mooy ki may tubaab bi mu indi fi raay bi. Waaye ak lim leen may ñu indi fi raay bi lépp teewul ñu yong ko ca wetu Tiwaawan, ñaari njiiti Faraas ñoo ko ray, ñooy Chauves ak Spitzer, ñu daal di sàkku ci Latjoor mu bañ a teggati tànk ci suufus Kajoor, waaye Latjoor bañ, dellu Kajoor. Ci noonu xare bu tàng tàkkati ci diggante Latjoor ak Salvatius, ci la Salvatius nangoo Kajoor ci atum 1886, Ñu ray Latjoor ca Deqale aki doomam ak juroom ñaar fukk ak juroom ñatt ciy àndadoom, ci 25 kori 1886. Kureelug xare (battaillon) gi ko ray Valois moo ko jiite woon. + +niti senegaal +Muhammad Lamin Daraame (turam dëgg di Demba Dibaasi) sëriñ la won bu bokkoon ci giirug Saraxule, di woon it tiijaan bu askanoo ci Gonjuro. Tukki woon na dem Màkkatal Mukaarama, nekk fa ba 1879 g,j. +Bi mu dellusee la ko Ahmad Seexu jàpp, jotul a àgg cig njabootam lu dul ci atum 1885 g.j . + +Muhammad Lamin Daraame siiwe woon na ag ragal Yàlla, looloo waraloon mu amoon taalube yu bari. Jibaloon na jiyaar ci kaw dëkkandoom yi duli jullit ak ci ñoñ frãas ñi sancoon réew mi. Xareem bi, tolloon ci junniy xarekat jawali woon na Bundu, daal woon gaw tatay Bakkel ji, atum 1886 g.j, waaye ak li ko waa Bakkel doon faral lépp taxutoon mu man a teg loxo ci dëkk bi, looloo taxoon mu dëppaat. +Waa Frãas yi tiitoon nanu lool ci ndam yi xareem bi ndàmm, looloo waraloon ñu song ko nangu Sinodibo, njaf doomam ja Saybu, ginnaw bi ñu ray ko. + +Ci atum 1887 g.j, la ko tubaab yi manante ci deltu ginaaaw jëm Gambi. Daal di toj tata ja mu tabaxoon ca Tuubaa Kuta. +Muhammad Lamiin ñàkkoon na lu bari ci xarekatam yi ci xare bii. Tubaab yi ray nanu ko ci ndimbalul Muusa Mulo. Ñu mujjoon manante buur yu bari ci ñu xaatim ay kóllarey ndénkaane(tutelle), tegoon it loxo lu ëpp ci suufi Senegaal yi. + +niti senegaal +Saamóori Ture mi ngi juddoo Mayambalandogo ci lu tollook 1830 g.j. Mu nekkoon ab yaxantukat, dajale woon na ab xare ngir nangu suuf yu bari, daal di taxawal ag Imbraatóor. + +Dugg na ci Lislaam atum 1880 g.j, daal di wéy nag ci yaatal Imbratóor gi. Waaye xéy na cig mbetteel fenqoo ak Tubaab yi daan sanc, daal di jàmmarloo ak ñoom jàmmarloo gu tar : leeg-leeg ci anamug maslaa (diplomatie) jaare ko ci di def ak ñoom ay déggoo, lu ci mel ne déggoo gu Bisandogo ; leeg-leeg it ci anamug xeex ak ñoom. + +Waaye waa Fràas yi ci njitug Gayni ñoo ëppoon ngànnaay : ndax ñoom amoon nañu ay kanó aki fetal yu aaytal. Bu dee Saamóori nag, moom dafa sukkandiku woon rekk ci fasam yi ak fetal yi tëgg yi daa liggéey. Jot naa daq nag tubaab yi te jàmmarloo ak ñoom diirub 12 at. Ci atum 1892 g.j, la dooley xareem ji tàmbalee doyadeek a loof ngir xeex yu bari yi, bu ko defee tubaab yi song Imbratooram gi. Saamóori lànkoon na ne du wommatu ( se rendre), mu daal di woon dem jëm penku taxawal fa ag nguur gu yees ci bëj gannaaru Tefesug bëñu ñay gi (Cote d’ivoire), waaye fekk na waa Fràas yi ak waa Angalteer xemmeemoon barab bii mu taxawal nguuram gi. + +Ci atum 1898 g.j, waa Fràas yi bett nañu ko ca dàttub Gelemu (camp de...), ñu njaf ko, yobbu ko Gabon, fa la faatoo ci atum 1900 g.j daal di jël nguuram googu boole ko ci Cote d’Ivoire. +Jàmarloo gu Saamóori Ture gi kontar tubaab yi dees na ko jàppe genn ci yi ëpp solo ci jàmmarloo yi ci sowwu Afrig. Sax na diirub 17 at. Yóbbe na canc gi ay ñakk yu takku. + +Xool it + Taariixu Senegaal + +Niti senegaal +Seyidinaa Limaamu ab nappkat la woon bu juddoo Yoof atum 1845 g.j. Ci atum 1885 g.j, mu gént gis ne mooy Mahdiyu .. mu tàmbalee woo àndandoom yi ci ñu dugg ci Lislaam, di soññ jullit ñi ci ñu sellal te jaamu Yàlla rekk, mu daa wax : (( wuyyuleen wooteb Yàlla, man de yonnantub Yàlla laa, maay Mahdiyu mi ñuy neggandiku)), daa na woo ay àndandoom jëme léen cig jub ak jàppalante. Bu ko defee nit ñu bari dikkal ko ngir déglu njàggaleem mi. Mu daal di sos kuréelug Laayéen. +Siiwam gi tiitloo woon na way sanc yi ragaloon ag jeqiku kontar leen. Ci atum 1887 g.j, la sancaan yi taxaw ci jàpp ko, bi mu yëgee seen naal yooyu la ànd ak lenn ciy àndadoom génn, waaye tubaab bi jàpp ko ca wetu Caaroy. Waaye ëttu àtte bi mujj na ko setal ko ngir ñàkk lenn lu man a dëgëral tuuma yi ñu teg ci kawam. Limaamu wéyoon na ci wooteem gi, waaye daa na def jamono ju nekk muy fenqook sancaan yi ko daa jéem a sonal ak àndandoom yi. Mi ngi làqu atum 1909 g.j. + +niti senegaal +Porofesëer Awa Mari Kol (borom këram sant Sekk) mu ngi juddu benn fan ci weeru mee atum 1951, nekk ab doktoor di tamit way-polotig ci Senegaal. Ab gëstu la buy gëstu li ëpp ci "SIDA" bi nga xam ne, siiwal na ci ay jukki yu bare. Nekkoon na kilifag deppàrtemaa ca "ONUSIDA"ca "Genève" diggante 1996 ba 2001. Diggante 2001 ba 2003 ak 2012 ba 2017, moo nekkoon jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi ci Senegaal. Fukki fan ak benn ci weeru septàmbar 2017 ba léegi, jëwriñu nguur la (ministar detaa) ci wetu Njiitu repibilig bu Senegaal. + +Dundam + +Dundu boppam +Am na borom-kër, am ñeenti doom. + +Njàng ak tàggatoom +Ndajem Berlin mi ngi am ci 15 diggi tabaski 1884 au 26 diggi gamu 1885. + +Réewi Tugal yi tàmbali nañu di sanc Afrik, maanaam di ko koloniise, ay réeroo nag daal di tàmbalee am ci seen biir ñoom waa Tugal yi, yoy xaw na leen a yobbu ci ay xare, loolu mooy li xewoon ca Isipt atum 1869 g.j, ndax kat Faraas ak Angalteer, ku ci nekk daa bëggoon a teg loxo ci yonalub Suwes. + +Ca Tiniisi, Faraas ak Itaali xat-xatloo nañ fa ngir jéem faa teg tànk. + +Ci mbalkam Kongóo (bassin du Congo), (diggu yaxantu bu mag bi) ag xëccoo amoon na fa ci diggante Faraas, Portugaal ak Buurub Beljik ngir féetewoo ko. +Ngir tee xare am, njiitul Almaañ li di Bismark daa woo woon kilifay réewi Tugal yi cim ndaje ca Berlin. + +Réew yii nag ñooy : Faraas, Angalteer, Beljik, Almaañ, Poortugaal, Ispaañ ak Itaali… Liggéeyu ndaje mi nag wéy na ñatti weer (la ko dale ca diggi tabaski 1884 ba diggi gamu 1885 g.j). +Ndaje mii jël na ay saxal yu am solo : + + Saxal ponk yi ñuy sance (coloniser) sancu yu bees yi. War na ci aji sanc ji (le colonisateur) bu bëggee sanc am réew mu waajal ab xare ( armée) yëggal it yeneen réew yi nar gi mu nar loolu. + Sañ-sañu yaxantu ci kaw dex yi. + +Ndaje mi nag bàyyi na fi ay ngérte (résultats) yu naqari: réew mu nekk di njëkkantee teg loxo wàll gi gën a rëy ci Afrik, ngir ragal ay dëkkandoom di ko fa xatal. Lii moo doonoon tàmbalig rawante gi ci wàllug sanc. +Ci atum 1900 (maanaam bi ndaje mi amee ba am fukki at ak juroom) la mbooleem suufi Afrik yi rot ci ŋëbug waa Tugal yi. + +cancug afrik + +Koju lëkkalekaay bi +Ñaareelu Xareb Àdduna bi ab xare la woon bu laaloon àdduna bi. Mi tàkk ci bi Almaañ ak Itaali ak Imbratóor gu Sapoŋ bëggee noot àdduna bi ci diggante 1914-1918 g.j. +Ñaari réew yii mu ci nekk daw na wuti ndimbal ci li ëpp ci réew yi mu defal ay tappoo. Bu ko defee yàggul dara lu bari ci réewi àdduna bi duggsi ci. + +Faraas sàkku woon na ci mbooleem ay sancoom ñu jàppale ko ci xeex bi, te jox koy nit. Jot naa dajale - ci ndimbalul Blees Jaañ - am mbooloom xare mu mag, mu xeex ci wetu Faraas lank sancuy Almaañ yi, ñu nangu ci Togóo ak Kamerun ak wàllug sowwu gi ci bëj-saalumu Afrik ak Tanganika (Tansani ci jii jamono). + +Ci atum 1939 g.j, la ab xare tàkkaat bu bees bu tàllaliku ba daj Tugal ak mbooleem réewi àdduna bi. Hitler njiitul Almaañ li daa gëmoon ne réewam mooy mi gën a kawe ci àdduna bi, kon yi ci des yépp dañoo war a toroxlu ciy tànkam, Itaali nag ak Sapoŋ dañoo àndoon ak moom ci loolu. Waaye réewi demokaraasi yi dañu koo lankoon. + +Xareb Almaañ bi songoon na suufi Faraas yi, loolu jur Faraas séddaliku ci ñaari wàll, wàll guy jàppale Almaañ te ànd ak moom ak gu nekk ci ron kiliftéefug Jeneraal Degol, mooy giy jàmmaarloo ak a xeex Almaañ. + +Li laytaay xare bi +Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw Xareb Àdduna bu Njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi. +Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ciy saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne réew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu” lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi. + +Àttey beddi yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu. + +Nosteg àtte gu mbokkte +Riisi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba. + +Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi. + +Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ +Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ. + +Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi. + +Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g. + +Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali +Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu. + +Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi. +Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma. + +Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi. + +Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi liggéeykat bi ak naatug walla jëm kanamug ndefar yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi). + +Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi. +Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom . + +Bokk na ci aakimookat yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ bu Espaañ ba. +Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi. + +Yeneen jëfka yu sabab xare bi +Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo: + + Lott gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon. + Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi. + Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi. + Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke. + +Jamonoy xare bi +Ñaareel Xareb Àdduna bi romb na ci ñatti jamono ñooy: + + Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g + Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g + Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g. + +Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. +Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g. + +Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi. +Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g. +Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g. + +Wéer ngànnaay yi + Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi. + Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans. + Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar. + Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon. + +Ginaaw bi Fraans wommatoo meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll. +Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg. + +Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. +Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan. +Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd: + + Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji. + Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g + Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g + +Ndamul Réewi tappoo yi +Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw - jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g. + +Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. +Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex . + +Wommatug Sapoŋ +Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo. +Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex. + +Li ci juddoo +Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu: + + Def ndajem Botsdam ca anéeru Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi. + Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg) + Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani, Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar. + Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem neewal dooleem. + Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi. + Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare. + Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g. + Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko. + Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare. + Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal. + Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag + feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi. + Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom. + Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon. + Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon. + Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi. + + Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal. + Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf. + +Xare bi ci Afrig +Lu bari ci xarey Afrig yi (sànnikati Senegaal yi ca lañu woon ) jawali nañu Tugal, ngir xeexal Faraas. Xarekati Afrig yii ñi ngi nekkoon ci dundiinn wu tar te wow, ci biir yeer yi ak ci sedd bu metti bi, jànkoonte nañook jafe-jafe yu bari, lu ci mel ne ñàkk a dégg làkkuw waa Faraas wi akug tumbrànke. Waaye loolu lépp teewul ñu ràññikoo woon ag njàmbaare akug dogu. +Xare ba jeex na ci ndamul Faraas ak ñi àndoon ak moom, ñu dàq Almaañ, mu doxe ci ñàkk mbooleem sancoom yi ci Afrig. + +Afrig gu yamoo gi Faraas yilifoon ci njiitul Flips Ibuwe dafa nekkoon di jàppale Degol, bu ko defee njiiti Afrik gu sowwu gu Faraas gi ñoom di jàppale Almaañ, ba ca tabaski 1942 g.j, booba lañu wëlbatiku jàppaleji way tappoo yi . + +Waa Afrig yi yamuñu foofu, waaye yabal nañu ay xarekat ca jëwub xare ba (front de guerre) ngir jox ñam way xare yi ak jox mbell Tugal. + +jeexug xare bi +Ci atum 1945 lañu daan Almaañ. Sapoŋ it daanu ngir fàccaakonub saal (bombe atomique) ba waa AameriK yi taal ca kawam. Ñaareelu xare bi dakk na - niki bi ko jiitu woon - alag dundug ay milyoŋ ciy nit. + +Xarey àdduna +Yewwute +wuññi yu juxraaf yi +Yëngu-yëngu yi jugoon di kontar Egliis bu paab bi +Jëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustri +Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal +Yewwute gu endustri : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi +Yëngu-yënguy politig yu mag yi ci adduna bi +Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans +Yëngu-yëngu yi aju ci “xeetu” walla fonk sa xeet (nationalisme) ci Tugal, ci xarnub fukk ak juroom ñeent g +Bennoo gu Almaañ +Sanc gu yees gi +Réewi sancaan yi +Ñaawteefi sanc +Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal +Ñaari xarey adduna yi, bu njëkk bi ak bu ñaareel bi +Mbootaay yu àdduna yi +Réew yi def ay dank +Fipp gi xam-xam amal ci Elektron +Teg loxo jawwu ji (walla xareb jawwu ji) +Ni Japon jëme kanam + +Taariix +Wuññi yu juxraaf yi walla yu melosuuf yi. + +Luy wuññi yu melosuuf yi ? + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf, walla feeñal gu melosuuf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg, njëkk waa-Tugal di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc, ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu melosuuf. + +Yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, danañu ko man’a xamalee ci nii: + +Mooy mbooloom liggéey yi jéngukat (aventurier) yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii : bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu. + +Li sabab wuññi yii + +Sabab bu diine + +Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu melosuuf yu Tugal yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari réewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon liggéeyub wuññi boobu. + +Ñoom yile ñaari réew dañoo jortoon ne danañu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Réewum Portigaal moom daa gisoon ne réewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum Xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono. +Paab gi moom da daa soññ réewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonal ko,tee koo tas, ngir néewal dooleem, xottite ko,giir ko. + +Ci noonu mu ( moom Paab gi) génne ay santaane yuy jox àq ñaari réew yii ci ñu moom diiwaan yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam géej yi la mbaa jéeri yi. +Paab gi ak nasaraan yi ci ginnaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nañu leen fi jeem’a jële. + +Sababu politig + +Am na yeneen réew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Faraas, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiital ci biti seen, rawati na ci réew yi ci yeex ci séenu'g nekku walla sosu gu yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen . Réew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu melosuuf gi. + +Sabab bu koom-koom + +Waa Tugal yi ñoom dañoo gisoon ne àddunay jullit ñi daal, mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir néewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi, loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke. + +Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova añs. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi. + +Lori waa Tugal yi tàmbli woon na’a yol, ñu tàmbalee ñammasle ak a manadee tëyye seen bopp, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi rekk (maanaam lu aju lu ñu man a jariñoo ci ay suuf, wurus mbaa lu ni mel), bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu melosuuf gi bi ñu déggee tono gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Tugal yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd, ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi . + +Sababu xam-xam + +Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak ab bindam dafa soppiku woon, ginnaaw bi ay tukki yu melosuuf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal, juge Tugal, génn, rawati na ginnaaw bi jamonoy xarey jooñe yi jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Tugal yépp ci jamono yu diggu yi. + +Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu, ak bëgg xam-xamu melosuuf, feeñ ci ñoom, ginnaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xarey jooñe yi ak ginnaaw bi - ci xam-xam bu melosuuf bu jëm kanam, ak ginnaaw bu xam-xamu Saytubiddiw ak liggéeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jëm kanam. + +Wuññiy melosuuf yu Portigaal yi + +Portigaal moom la ñuy jàppe réew mi jiite woon wuññi yu melosuuf, yu Tugal yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool (1394 – 1460 g), doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon moolu(dugg géej), ak yër xisay mool yi, ak téerey taariix yi. Muy ku aayoon ci rëdd lonkooyooni melosuuf yi, moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta, ginnaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g. + +Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi géej gu xonq ga ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum 1445 g, ginnaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niser. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko «Boppub Yaakaar Ju Baaxi Ji» ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End. +Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi, romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji, ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End. + +Vasco De Gama mii jot naa xamante ak Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon géeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu géej yi. + +Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu géej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi ñuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song barab ya ak mbooloom gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo ak buuri diiwaani End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End bi. + +Li wuññiy melosuuf yu Portigaal yi jur + +Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw : + +1) Waa Portigaal, ñi ngi tàmbli woon di teg loxo ci tefesi Afrig yu sowwu yi, ci noonu njàppum jaam siiw, te tas ci Tugal gépp, di jaam yi ñu daa jàppe Afrig, te daan ci yaxantu. + +2) Jamonoy sanc gu Portigaal, mi ngi tàmblee ci bi Portigaal taxawalee ab sancu, ci penku bi, ca fa ñuy wax Jawa, ay xare it am diggante araab yu jullit yi ak Portigaal cig wàll, ak ci diggante waa Portigaal ak waa End yi ci geneen wàll. Waa Portigaal yi nag jot nañoo teg loxo yenn waax yu am solo yi nekkoon ci yoon wi jëme End. + +3) Waa Portigaal yi mujj nañu xam yoonu yaxantu wu géej, wu dul romb ci réewi jullit ñi,mooy wi jaar ca Boppu Yaakaar Ju Baax ja. + +Loolu nag mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon néew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal-jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jéem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan safaan (kontar) doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu géej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi. + +Wuññi yu melosuuf yu Espaañ yi + +Li ci dugaloon Portigaal, moo dugal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi. +[[ +Mool]]ub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahamas ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi. + +Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ». + +Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siiwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na àdduna ju yees ju dul End. + +Ginnaawam it wuññikat yi doon liggéeyal Espaañ wëy ci seen liggéeyi wuññi yooyu, ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca diiwaan ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraangay ñu tudde ko Adduna ju bees jii di Aamerig tay. + +Li wuññiy Espaañ yi jur + +1) Ñoom de ubbil nañu tukkiy wuññi yi aw yoon wu bees wu jëm ci àdduna ju yees ji, di ko jaare ci màmbulaan gu atlas gi. Bu ko defee Espaañ tàmblee sanc gox yi mu jotoon’a àgg ci Aamerig gu diggu gi ak gu bëj-saalum gi, ñu wisaare fa seenug xay ak diine, ubbi fa ay mbelli wurus ak xaalis. + +2) Saxal gu ñu saxal ci xam-xam ne suuf si daa “bulu” , te li waraloon loolu di tukki bi Magellan defoon. Buur bi ñu daa wax Shark mu juroomeel mi (Sharlakaan) di woon buurub Espaañ, daa digaloon mool bii di Magellan atum 1519 g, mu def ab tukki jëm penku jaare ko sowwu, ci noonu moom Magellan jug, moolu (war geej), jawali sowwu, te jëm penku, ci kaw màmbulaan gu atlas gi, bi mu ko defee daal di àgg ca tefesug Breesil ga, fa Riyo De Janero, mu wëy nag ca doxam ba, ba ca sottiwaayu dexug Labalata, daal di wër Aamerig gu bëj-saalum gi, tàbbi màmbulaan gu dal gi nga xam ne moom moo ko tudde « pasifik » di wund lu dal, mu àgg Filipin atum 1521 g, foofa nag mu songoo fa’ak ñoñ réew ma, ci’y xeex yoy ca la ñu ko raye, waaye kenn ciy nitam, tuddoon Dianco, moo mujjoon jiite boobu tukki, dem ak ñoom ba ci Boppu Yaakaar Ju Baax ji, juge fa dem Espaañ, gi nga xam ne ma nga fa àgg atum 1522 g. + +3) Weddi gisiin yi daa wax ci bindu suuf si ak ab kemam ( ni mu tollu), ndax kat tukki bii nga xam ne dafa dox, wër àdduna bi, firndéel na ne suuf si daal moo ëpp fuuf li ko Colombo jàppe woon ak ku dul moom. Beneen gox feeñ na, bu mag diggante Tugal ak Asi ci wàllug sowwu gi, di Aamerig gu bëj-gànnaar gi, nga rax ci dooli geneen gi’y gu bëj-saalum gi, te ag màmbulaan gu yaatu, gu yees’a ngii gu ñu xamutoon. Kon suuf desatutoon su ñu xamutoon su dul Ostrali ak ñaari dott yi . + +Wuññi yu Angalteer + +Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu géeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginnaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug waa Angalteer yi, ñeel Aamerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa. Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland. + +Wuññiy araans yi + +Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jëmi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy Faransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fétali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Aamerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Faraas tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak barabi dex yi ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebeg ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. Moolu Faraas bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Faraas ya daal di fay sos sancu bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Faraas ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi. + +Wuññi yu Oland yi + +Lonkoo (société) gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu géeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali dóoxug New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu Boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu géej wu am njariñ. Waa Oland yi jéemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g . + +Li wuññiy melosuuf yu Tugal yi jur + +Li wuññiy Tugal yi jur man nañu koo tënk ci lii di ñëw : + +1) Njiitug yaxantu gi tuxu na tukkee ci li wër géej gu diggu gi dem ci màmbulaan gu atlas, mu mujj moom yaxantu gi nekk ci loxoy réewi Tugal gu sowwu gi, bu ko defee ñu nos fi ay yooni géej yu yaxantu ci ñaari màmbulaan yi, gu atlas ak gu dal gi (pasifik). +Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » . + +2) Wuññi yu melosuuf yi amal nañu fi jawwu yu gëpplante ak wujje, ak as lef cig noonoo ci diggante réew yi doon def wuññi yii, loolu moo yokkoon xemméemtéefi sanc yi ci diggante réewi Tugal yi. Ci noonu aw gisiin wu sanc tàmbli woon’a feeñ wu Tugal jëm ci askani réew yii ñuy door’a wuññi. + +3) Xam-xami melosuuf yi soppiku woon nañu bu baax, li ko waraloon di yaatu gi wuññi yii yaatu woon te bari. Ci noonu yëngu-yëngu gu nasaraanal yokku ci anam gu fés, rawati na ci Afrig ak ñaari Aamerig yi. + +4) Ag jëm kanam feeñoon na ci wàllug yaxantug mbèll yi, di wurus ak xaalis, nga xam ne sax xarnub fukk ak juroom g, dañu koo tudde woon « xarnub xaalis », ni nga xame ni jëm kanamug koom googu taxoon na ba dundiin wi gën’a kawe, njëg yi it gën’a yekkatiku, ni fi ay njaay yu yees dugge, lu ci mel ne kakaawoo, póon, kiinaa, batata ak mbòq. + +5) Wuññi yi de lenn lañu ci màndarga yiy wone yewwuteg Tugal gi, ni nu la ko leerale woon ci doggantal gu njëkk ga. + +6) Réew yii ñu wuññi, ruu gu fees ak bëgg’a fayyu moo leen ubale woon, muur leen, jëm ci yii leen wuññi, ndax ñoom tubaab yi xalaati sanc lanu yoroon, daan ci doxe ci mbooleem seen doxi wuññi yi, lepp lu nu gis aakimoo ko, ngartaajoo ko, lii mooy li waral askani réew yi nu wuññi, jugoon ci jànkoonte ak ñoom, taxaw ci xeex canc gu Tugal gi, ci anam gu tar, jëfandikoo ci li nu yor lepp ci kàttan. + +7) Wesaare diiney nasaraan ci bepp gox bu ñu wuññi. + +Melosuuf +Yëngu-yëngu yi jugoon di safaan (di kontar) Jàngu bu Paab bi + +Yëngu-yëngu gu yéwenal diine ji ci Tugal : + +Yëngu-yëngu gu yéwénal gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Tugal ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Jàngu bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jéem a delluwaat ci njàggaley Injiil yi. + +Li waraloon « yéwénal » gi : + +Ak li Jàngu bi di nekk nguurug ruu lépp - ci li ko njëkk a tax a jug - téewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom-koom, ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Jàngu bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtook moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni. + +Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag yi ñépp di fay. Ci noonu Paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp. + +Ñaawtéefi Jàngu yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi. + +Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat , nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu Jàngu bu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex. + +Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Tugal : + +Yéwénalug diine ci Tugal - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam. + +Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Jàngu bi te dëgëral ko. + +Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Jàngu bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci Jàngu bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 - 1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam . + +Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli. + +Martin Luther ak yéwénal gi + +Martin Luther mi ngi juddoo Isilban, di benn dëkk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaañ atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan liggéey ci benn ci gasuwaayi mbell yi. +Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginnaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Jàngu bi, li gënoon’a wëlbati ay gëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla “kritige” paab gi, ginnaaw bi it, mu mujj fettéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam. + +Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam. + +Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginnaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Jàngu bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal . + +Luther moom dafa safaanoon (kontaroon) njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Jàngub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Jàngu bu Watanberg ba, lakk ko. + +Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon + + +Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii : + +(1) Injiil mooy andaar ju diine ak ju yoon ji muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute. + +(2) Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni. + +(3) Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil. + +(4) Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi. + +(5) Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi. + +(6) Wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi Tugal gu sowwu gi. + +Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu néewal doole sañ-sañu Paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu néewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy néewal ngañaayi Jàngu bi aki am-amam aki tonoom, ndax loolu man’a soril Jàngu bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Danga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci Jàngu bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom Jàngu bi ne àqi yoonam la ju mu moom. + +Jëfka yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu + +Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii : + +(1)Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Tugal yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a féqu ak’a dañtalu ci ŋëb gu paab gi ak sañ-sañam. + +(2)Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam. + +(3)Fonk sa xeet,walla xeetu gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Tugal yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginnaaw Martin Luther, rawati na kuréel gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya. + +(4)Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu. + +(5)Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër it jam yi mu doon def Jàngu bi . + +(6)Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom. + +Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy Diiŋatkat, maanaam ay protestants cig wàll, ak diggante ñi toppoon Paab gi (katolig yi) ci geneen wàll. + +Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne diiwaanu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant mbaa mu katolig, waaye ci wàllug nguur gi ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci diinaawani almaañ yu bëj-gànnaar yi – Jàngoom daal di doge ca Jàngub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmaark ak Suwed) . + +Kalfen (Calven) + + +John Calven mi ngi juddoo Fraas atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraas dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine . + +Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi. +Kalfen ak Luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy: + +(1) Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko . + +(2) Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma. + +Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraas, Angalteer, Siwis ak yeneen. + +Swingli + +Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi. +Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine. + +Swingli moom daa jàppe woon Jàngu bi benn campéef bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Jàngu bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye. +Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Tugal yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi. + +taariix +Jëm-kanamug xam-xam + + Jeexiitalu gu waa-Tugal defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi. + + Lefi (wàlli) jëm kanamu xam-xam ci Tugal. + + Yewwuteg ndefar: ay jagleem – ay màndargaam – ay ngérteem (ses résultats) + +Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi: + +Jamono ji xam-xam néewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem réewi jullit ñi di lu naat, te meññi. + +Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññee ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi. + +Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris End, rawati na ci Paj, Saytubiddiw, Xayma ak yeneen yi. +Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaaton ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi. +Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobbu leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug paj ak xayma, simi ak xam-xami dénd yi , Saytubiddiw, melosuuf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell. + +Ngérum walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi: + +Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii: +Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi . + +Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono. +Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer jii di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu. + +Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng jëmm ak simi ak xayma ak saytubbidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xamu Yàlla (théologie) . + +Digg yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Tugal: + +Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Tugal jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jokkoo woon nanu ak jullit ñi, jaare ko ci ay ker-keraan yu bari, bokk na ci yooyu: + +(1) Andalusi : + +Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon. + +Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Tugal yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Tugal yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi. + +(2)Dunub Sisil : + +Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Tugal, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobbu leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Tugal yi tàmblee yër li ci yii téere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi. + +(3)Xarey jooñe yi + +Bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Tugal jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci téere yi nu taalifoon ci araab, ak yi ñu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris . + +(4)Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Tugal.Rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi. + +(5)Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Tugal yi daa defsi ci réewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Tugal ci jamonoom ju bees jii. + +Xam-xam yi bàyyi ay jeexiital ci waa Tugal yi: + +Xayma: + +Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami xayma yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu seggat ko, sellal ko, gën koo teg ci yoon. +Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay ndollent yu am solo ci xayma, ñoo dolli woon tus ci lim yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam “al-kasr al-hasarii” di ci wolof (damat gu fukk) , ñu taalif ci xayma ay téere yu waa Tugal yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci. + +Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xayma, moom de lañuy sant bu lim (mumero) yi nekk ci xayma duggee Tugal tay. +Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginnaaw bi ci làkki Tugal yu bari. Boroom xam-xami Tugal yi jariñu ci. + +Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci xayma, ñoo njëkkoon waa Tugal yi ci wàllug xayma gu yees gii. +Bu dee nag ci xereñ(ingénierie) , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi ñu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nañoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xayma gu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi. +Nu xóotal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug xayma, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug xayma ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g. + +Jëmm : + + +Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu jëmm ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal, dolli ci ay masala yu yu jëmm yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “xool” (almariyaat ). + +Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab téere bu am solo, mooy téereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Tugal yi mujjoon nanu koo tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g). + +Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan Bun Alhaysam (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu jëmm, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo. + +Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët, ak weer yi ak leer ak yeneen. +Waa-Tugal yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Tugal yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax. + +Saytubiddiw: + +Jullit ñi yittewoo woon nanu saytubiddiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug biddiw yi, xam fi ñuy fenke ak fi ñuy sowe. +Jullit ñi jariñu woon nanu ci saytubiddiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci téerey biddiw yu Geres yi niki téereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi. + +Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif téere bi ñuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami saytubiddiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom. + +Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi biddiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi. +Waa Tugal yi ñoom jariñu nañu bu baax ci saytubiddiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam. + +Kimya: + +Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu jëmm, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def simi te taalifoon ci ab jimblang . + +Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu simi yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik, ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen. + +Mu leeraloon ba tay jefi simi yi niki: seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal. + +Dana jaadu nu leeral ne xam-xamu simi moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu simi yu bari. + +Waa Tugal jariñu nanu bu baax ci xm-xamu simi bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli. + +Paj : + +Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci paj. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw. +Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci paj, taalif na ci lu sakkan. + +Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci paj, téereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de benn jimblang bu xam-xamu paj, bu waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Tugal yi jariñu nanu ci xam-xamu paj bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Tugal yi. Waa Tugal yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax Kaaw su nuy opere (xotti). + +Waa Tugal yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk. +Bokk na ci boroom xam-xami Tugal yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy. + +Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Tugal a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug réeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Jàngu bi. + +Dana yell ñu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Tugal gu sowwu gi, ginnaaw bi ab kureel ci waa Tugal yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Tugal yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom. + +Kon lu nu war’a xam la ne [[yewwuteg xam-xam]] ak gu ndefar gii am ci réewi Tugal yi, ci ginnaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Tugal tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci àdduna ju xay jii ngay gis tay . + +xam-xam +Endustri +Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal + +Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Tugal, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Tugal gis tay ci jamonoom ju yees jii ñu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu ndefar ci Tugal, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Tugal rekk la ñeel waaye àdduna bépp. + +Li taxoon xam-xam jëm kanam : + +Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci réewi Tugal gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di: + +(1) Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Tugal yi te jariñu ci. + +(2) Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Tugal yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam + +(3) Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi ñu fentee móolukaay yi. + +(4) Xemmeemtéef gu waa Tugal yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: xam-xam yu Gres-Rom ya. + +Wàll yi xam-xam jëme kanam : + +Ak li ñuy misaal jamono yu diggu yi ci Tugal lepp, naan jamonoy réer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn manta réere, manta weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu néew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Tugal yi nekkutoon lu moy li ñu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu ak jarbu . Ci noonu Tugal jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di: + +Paj : + +Paj walla “Ndoktoor” ci Tugal wéyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak pajug jullit ñi, jaare ko ci seen téerey paj yi nga xam ne waa Tugal mujjoon nañu leen’a firi ci seeni làkk. + +Xam-xam bi Tugal ame ci paj weesuwutoon fii, ba ci xarnub fukk ak juroom benn g. + +Waa Tugal yittewoo woon nañu bu baax xam-xamu paj, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom de xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug paj ci Tugal. + +Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu melosuuf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci réew yii ñuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Tugal te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu ñu xamutoon ci Tugal. Mu mujj nag bokk ci wartéefi doktoor yi ci Tugal ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu ñu leen di faje, wutal leen ay garab. + +Ci noonu boroom xami-xami Tugal yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Belsig mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub +Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Faraas, ak Lofan Hok mu Olaand mi, ak Luwis Pastor mu Faraas mi ak Kox mu Almaañ mi añs. +Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs. + +Melosuuf ak Saytubiddiw: + +Xalaat wi naan suuf si daa tàllaliku, te boroom xam-xami saytubiddiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gépp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nañu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay liggéey ci googu wàll. + +Waa Tugal yi nag seen xam-xamu melosuuf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li ñu xame ci wuññiy melosuuf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu melosuuf tàmblee jëm kanam ci Tugal. +Jëm kanamug xam-xamu melosuuf tax na ba bu saytubiddiw it jëm kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siiwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom déy duggal na loxoom bu baax – boo xoolee liggéeyam yi aju ci xam-xamu saytubiddiw – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg àdduna bi, bu ko defee yarami asamaan yi di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen yarami asamaan yi, ñoom ñepp dañuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wërngalu, maanaam roo te wërngaloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wërngalu, di wëndéelu. + +Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal Jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewuñu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu saytubiddiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay (microscope) ngir fuglu biddiw yi ak yaram yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi. + +Jëmm: + +Xam-xamu Jëmm gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu Jëmm bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu. + +Boroom xam-xami Tugal yi def seen yitte ci ñòddi gi nekk ci suuf si . +Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yéegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yëf sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lañuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yittewoo xam-xamu Jëmm, ndax kat mooy ki teg dàtti xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g. + +Boroom xam-xamu Angalteer bii di Isaac Newton (1742 – 1727 g ) mooy ki wuññi dooley ñòddi walla bijji gi nekk ci suuf si . Moo wax ne kawkab yepp, dañuy wër jant bi, ci ay ngunu walla koto yu sax, yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon. +Ki ñuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni biddiw yi sosoo. + +Simi: + +Waa Tugal yi tuxale nañu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu simi bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw. +Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti yu simi yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci. +Toggaliit yii ba leegi danga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lañuy yore. + +Waa Tugal yi nag, ñoom, dañoo gën a jëmale kanam xam-xamu Simi, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Faraas, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g. + +Mbëj: + +Boroom xam-xam bii ñuy wax Thales, di ku dëkkoon Geres, moo seetlu woon dooley bijji ju nekk ci mbëj, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu mbëj. Boroom xam-xamu Angalteer bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigéen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul mbëj rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu mbëj buy juddal mbëj atum 1672 g. + +Ki ñuy wax Stephen Gray dikk, won ñu ni ñuy tuxale mbëj, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci buum yu xànjar. + +Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi mbëj yi, te fent batari. Borom xam-xamu Aamerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak mbëj benn lañu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la ñuy jaare di genne mbëj bu bari atum 1831 g. +Waa Tugal soobu nañu ci xam-xamu Xayma, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Faraas bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu Jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële. + +Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu suuf (Géologie)la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni ñuy sosoo. + +Jamonoy yewwute daal ci Tugal mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te féexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Tugal ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jéem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam. + +xam-xam +Tugal + + +Yewwute gu ndefar (industrie) : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi: + +Yewwute gu ndefar ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug ndefar, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g. + +Waaye nag, moom ndefar gii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Aamerig, la ko dale ca njëlbéenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. +Bi mu ko defee nag, ay jeexiitalam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci àdduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g. + +Ndefar yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ba ci suñu jamono jii ñu toll. + +Looloo waral du man a ñàkk ñu xam sabab yi tax yewwuteg ndefar am ci Tugal. + +Sabab yi tax yewwuteg ndefar am ci Tugal + +1 Jëm-kanam gi xam-xam def ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg ndefar am. + +2 Dëkki Tugal yu mag yi, am gi ñu am, ak tegu gi ñu tegu ci yaxantu ak ndefar, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba ndefar di jëm kanam, rawati na, gi ci aju ci ràbbu sér , nga xam ne mooyndefar gi njëkk ci Tugal. + +3 Jëmmaan (l'individu) walla jëmm ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Tugal yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Tugal kees tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, féexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam. + +4 Li juddoo ci wuññiy melosuuf yi it, muy teg loxo gi réewi sancaan yi daa def réew yi ñu sanc , ak di fa jële ay xéewal aki cémb (ñumm) , di leen yobbu seeni réew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg ndefar gi ci Tugal. + +5 Réewi Tugal yi ak mbootaayi koppar yi, jàpple gi ñu doon jàpple sémb yi jug ngir jëmale kanam ndefar ci Tugal, loolu de ci li defar jawwu ji la ba ndefar man a dox, man a àntu. + +6 Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal. + +7 Bari gi liggéeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy liggéey ci ndefar yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati Angalteer yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci liggéeykat yi amoon xam-xam yu néew lañu woon, nga xam ne daanaka jànguñu woon. + +Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam + +Yewwuteg ndefar ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lañu: + +1 Jëmale kanam gu ñu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb : + +Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. + +Loolu nag li ko waral mooy yittewoo gu tar gu nit yittewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir liggéey ci. + +Ràbbkatu Angalteer bi ñuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin (wuutuloxo) bu loxo, bu ñuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla póno, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn liggéeykat di ko yor, di ko doxal. + +Bu ko defee, fentkat bu Angalteer bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu ñu daa doxale ci dooley ay fas, mujj ñu koy defe ci dooley ndox, ñu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame). +Ki ñuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci liggéey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari diiwaani Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire . + +Ki ñuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu ñuy doxale dooley ndox, ginnaaw bi ñu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba ñu man a ful li ñu daa ràbb, daa ko defar ciy sér. + +Liggéey bi ñu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal liggéeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu simi yi ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi ñu liggéey. + +2 jëfandikoo kàttan : + +Jumtukaay yu njëlbéenu yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat . Kàttan nag di “energie” jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te dox. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbéen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginnaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ. + +Ki ñuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug liggéey bi, ak li ñuy liggéey, ndax kat dugal gi ñu dugal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci ndefar ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis ndefar tay mu toll fii mu toll. + +Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu ñuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland. + +Nit it gënoon na a jéego ay jéego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Aamerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginnaaw bi, ñu gisaat petrol fu bari ci àdduna bi. Ginnaaw bi ñu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginnaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne dañuy sukkandiku ci li ñuy wax “lakkug biir gi”, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs. + +Mbëj tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li ñuy wax juddalukaayu mbëj, nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay liggéey ak njariñ ci dundam. + +Nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a néewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nañu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi ñuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi. + +3 Jëm kanam gu ndefar gu weñ jëm kanam + +Bokk na ci lu am solo li yewwuteg ndefar gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi ñu jëmale kanam ndefar gu weñ, loolu nag mooy bi waay Angalteer jii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jéegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay génne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy liggéey. +Lii lépp nag bokk na ci li waral yewwuteg ndefar gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani. + +3 Jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam + +Li kenn manul a sikk mooy ni ndefar jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi liggéeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug cóolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci àdduna bi. + +Ginnaaw bi, nitug Aamerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo cóolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Ginnaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci géej yeek mbàmbulaan yi. +Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko ndefar defe. Bu ko defee, feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg ndefar gu mag gii am tay ci àdduna bi. + +4 Feeñug campeefi ndefar yi : + +Liggéeyuwaay yu ndaw yi juge nañu ci kër yi, doon leegi ay campéef yu ndefar, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. +Ndefar yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu ndefar, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi. + +Liggéeyuwaay walla isin yu mag yi nag, ci wetu barabi cémb yi (ñumm yi) lañu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimbale ci ñu man a néewal seeni fere ci lu aju ci seeni liggéey, ndax loolu daa na tax li ñu ci waroon a ñàkk gën a néew. Néewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal liggéey bi, gën koo wuuteel. + +Li fi yewwuteg ndefar gi jur: + +Maneesul a sikk ne yewwuteg ndefar gi indi na ci Tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay. + +Li mu fi indi ci wàllug koom: + +Yewwuteg ndefar gi bàyyi na fi ay jeexiitat yu rëy ci wàllug koom, ci biir Tugal ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li ñuy liggéey gën a yokk, gën a wuute, li ñu koy jënde gën a néew, ñépp man cee jot, jumtukaayi liggéey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu àdduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk ak sanc , tàmblee booloo. + +Ndax kat canc gu politig gu yees gii, du lu dul doomi canc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci ndefaram gu jëm kanam gii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ñumm yi, ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute. + +Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lépp, ak li mu gën a ñaw lépp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi njuddéefam gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi dañoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a liggéey, ndax la ñu daa ame ci liggéey bi moo daa gën a bari, te daa nañu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Tugal, rawati na ci Angalteer. + +Joqalanteg yaxantu gën a yokku ci àdduna bi, nga gis réew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci géej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu àdduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu àdduna yi nga xam ne seeni boroom dañuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi. + +Li mu fi jur ci politig: + + +Sanc gii Tugal tàmblee sanc réewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg ndefar gi indi, wuutal ko fi, ginnaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginnaaw , ndefar day soxla ay cémb (ñumm)(matière première), te loolu dañu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay réew ci fu bari ci suñu àdduna bii, tax it ba réew yi ñu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag canc, ak lépp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi. + +Bu ko defee, benn dal (principe) daal di feeñ ci Tugal, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu af bi” (bu libre bi) am te taxaw ci nosteg bopp-alal (système capitaliste) . Loolu nag mi ngi am ci ginnaaw bi ndefar gu yees gii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci ñu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi ñu yittewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen. + +Nguuri Tugal yi, jàpple woon nañu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li ñu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan . Ci noonu wartéefi góornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi ndefar yi. Loolu yobbu leen ci ay wartéef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu (leekol) aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam (societe bi). + +Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen liggéey bépp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nañu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay. + +Góornamaay Tugal yi duggsi nañu ngir aar liggéeykat yi, ci noonu ñu yamale waxtu yi ñuy liggéey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lañu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu njeextel-ayu-bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay liggéey ngir yekkati seen payoor yi, jéemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax. + +Man gi réewi ndefar yi man a doxal seen mbiri réew, feeñ na, te am bi réew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis réewi Tugal yi sukkandiku ci ndefar, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi ñu miinoon. + +Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay: + +Yewwute gi ci Tugal jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi, ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki ndefar yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi ndefar yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll. + +Bu ko defee, baykatu Tugal bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li ñu koy fay moo gën a wóor te gën di lu ñu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi. + +Lii mooy li waral ñiy liggéey ci mbay néew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a néew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy néewug njóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer. + +Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër liggéey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li ñu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey liggéeykat yi gën na a yokku, bi ñu demee ba li ñu leen di fay manatul a faj gën ja’a néewi seeni aajo, ngir seerug dund gi. + +Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd ak yewwuteeg ndefar gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigéen ñeek xale yi, leegi dañoo tàmbli di liggéey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu ñu man a gën a ame ay liggéeykat ba gën a man a néew lu ñuy fay, ginnaaw liggéey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. +Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigéen bàyyi fi ay liggéeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg. + +Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi, ci Tugal, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-liggéey walla ag liggéeyadi tàmblee tas ak a yaatu ci Tugal, ci liggéeykat yu góor yii nga xam ne dañoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu ñu leen lijantile seen jafe-jafey liggéey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos liggéey bi, aar liggéeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal yi moom isin yi. + +Gongikuwaay +Téere taariix bu Abdu Xaadir KEBE + +Endustri + + +Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A) + +Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi + +Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Aamerig, gàddaay yooyu wéyoon nañu di sottiku ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Aamerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci: + +1 Fitnay diine yi amoon ci Tugal gu diggu gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di safaan Jàngu bu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak ngérum Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy boddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug gore. + +2 Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig . + +3 Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, dañoo gëmoon ne Aamerig de réew mu fees dell la ak yile mbell, te ña fa dëkk, ñu néew ag xay lañu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowuñu yenn liggéey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll. + +4 Jëm kanam gi xam-xam am ak ndefar ci Tugal, rawati na ci wàllug liggéey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci ñu man a tukki ci géej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori. + +5 Liggéey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nañu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug canc gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi. + +Sancu yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nañu leen ci Aamerig gu bëj gànnaar gi: + +Waa Tugal yii bawoo woon Ispaañ, Faraas, Olaand, Suwed ak Angalteer, sancoon nañu ay barab yu wuute ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lañuy wax tay Diiwaan yu Bennoo yu Aamerg yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Waa Angalteer yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nañu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci barabi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaaye Tugal. + +Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb akug dagge ca réew may nday di Angalteer. +Waa Angalteer yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance réew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy : + + Buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy gi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci ñu taxawal ay sancu, ak jariñoo xéewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu ñuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi. + + Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen . + +Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Aamerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy: + + York bu bees + Wirjiniya + Raod Island + Masacuusets + Dulawir + New Hamser + Kintakit + North Karolaayna + South Karolaayna + Jersi bu bees + Jorjiya + Pensilvaniya + +Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Aamerig gu leegi gii nii, duñu weesu benn xaaj ci Aamerig gu ñu xaaj fukki xaaj. + +Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi: + +Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte gu boppu” (autonomie) , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di réew mi leen moom. +Nosteg àtte-gu-boppu googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk: + + 1 Kaŋ bi (le gouverneur) + 2 Jataayub yoonal bi + 3 Jataayub diisoo bi + +Kaŋ bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy féetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu ñu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (Kaŋ bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli. + +Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu liggéeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru Kaŋ bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal. + +Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal Kaŋ bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom. +Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte gu boppu ” gi nga xam ne taxoon na ba ñu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer. + +Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy yu waa Angalteer yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nañu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen réewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen réew, di ci tënku, te di ko fonk. + +Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lañuy tudde xareb temb bi . + +Li waraloon xareb temb bi: + +Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lañu woon aki kuréel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lañu woon yu di ay diiŋatkat (protestants). Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nañu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy: + +1 Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas” + +2 Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu. + +3 Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo di am réewam, fa la féetale ag réewoom + + +Ëttub Aamerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii: + +Yoon yuy tege galag ak tembar + +Parlamaa bu Britani bi daa génne atum 1762 g, yoon wu ñuy wax yoon wu tembar yi, mooy wiy def ngay fay tembar ci jëflante yu kilifawu yi (officiel yi), ak wayndare yi (les dossiers), ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Faraas yi ak yu Olaand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak biteex (walla betteex) . + +Yoon wi aju ci moolu (navigation) ak yaxantu: + +Ci atum 1651g, barlamaa bu Britani bi dafa génne wenn yoon wuy waral ci sancu yi ñuy tuxal li ñuy génne ak li ñuy jëggaani di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na ca Angalteer. + +Koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf: + +Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy génne walla ñuy defar benn koppar bu kayit ak di ko jëfandikoo niki koppar bu ofisel (kilifawu) . Noonu tam lañu teree woon – ci weneen yoon (luwaa )- ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom. + +Nos dooley kaaraange ji: + +Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci génn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko. +Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a néew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer. + +Waa sancu yi tam yëgoon nañu ne li ñuy fay ciy galag lépp, deesu leen ko defal fi ñu koy faye waaye kay ca réew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy réew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon. + +Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug séqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum réeroo mi nekkoon ci seen diggante. +Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne duñu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu ñu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu. +Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nañu ne moo waral xareb temb bi. + +Ndajem waxtaan mu Filaadelfiya mu njëkk mi: + +Juroom ñeenti diiwaan yu Aameriig teewe woon nañu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg. +Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaawam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci àdduna bi. + +Looloo taxoon reenub réeroo bi nekkoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi dañoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal(principe) bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” . + +Man nañu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nañu ko, di ci safaan ni Angalteer di àttee seen diiwaan yi. + +Ñoñ sancu yépp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfiya, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lépp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yépp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii ñuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma. +Ndajem Filadefiya moomu, mooy dàtt bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi . + +Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefiya mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom. + +Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ - ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi. + +Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon. +Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nañu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefiya, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def. + +Ndajem Filadelfiya mu ñaareel mi: + +Ndawi sancu yi defoon nañu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfiya, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfiya mi, ñu wax fa ne dañuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu dugal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu ñu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jéem gi sancu yi doon jéem ngir defar – ak doonte lu néew la itam – seen diggante ak Britani, réew miy nday. + +Ni xare bi tàkke : + +Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yépp ci ron kilifteefam lañu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu Aamerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Aamerig yi. +George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jàmaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu. + +Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lépp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington amoon na ci kaw njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanadaa, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi ñu gañee Britani, Faraas jug na, jibal ab xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Olaand topp ci atum 1780 g. Man nañoo wax ne Faraas moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu Bennoo yi, ngir ñu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Faraas lii di Lavette, safaan Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci jë yu bari. + +Dàq gi ñu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kuréel lañu woon mu ame ci diggante ay waa Faraas aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat. + +Nañu fàttaliku nag ne waa Aamerig yi ñoom, ci seen suuf lañu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanadaa, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer gi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka. +Nga rax ci dolli, waa Aamrig yi dañoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nañu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington. +Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli-doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pastéefub xeex bi ñu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon temb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi. +Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi ñu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Aamerig. + +Tembug Diiwaan yu Bennoo Aamerig yi: + +Bi waa Britani xamee ne lòtt nañu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Aamerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku ñu dàqe, ndamu ci kawam ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Pari, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g, lii mooy tomb ya ca ëpp solo: + +1 Britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi féete ci penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw sowwu wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nañu nekke woon. + +2 Jéem a rafetal séqoo yi, ci diggante Britani ak réewum Aamerig mu temb mi (Diiwaani yu Bennoo Amerig yi) + +3 Amal ci diggante Britani ak Aamerig gu temb gi, ay séqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag séqoo yooyu ñu teg leen cig nawleente, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom. + +Nii daal la Diiwaan yu Bennoo yu Aamerig yi ame, xareb temb bi nag am na genn jeexiital gu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi. + +Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke. + +Aamerig nag moom, daal di ñew, defar sartu réewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nañu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cér ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi. + +Ginaaw bi lañu def Washington – ginaaw bi mu nekke péeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def péey bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Aamerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi. +Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon. + +Politig +Taariixu Aamerig +Jeqiku ga amoon ca Faraas : + +Jeqiku ga amoon ca Faraas, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (jeqiku googu), mi ngi ame woon ca Faraas, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benneel ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu tollu ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g) defee daaneel nguur gu ñuy wax “daaneel nguur gu 18 Brumaire”, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri réew mi. +Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Faraas gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk-jàmm ga, tiitale ga , tuur-dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak jeqikug Faraas gi. Loolu nag taxoon na ba “jeqiku gi” manu fi woon a amal dali gore(principes de liberté) , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi. +Waaye nag jeexiital yi nga xam ne jeqiku gii amal na leen fi, yamuñu rekk ci Faraas, waaye weesu nañu ko ba daj Tugal gépp, ak lu bari ci réewi àdduna bi. + +Ni Faraas meloon laata Jeqiku gi: + +Bu ñu gëstoo na Faraas meloon laata jeqiku gi, loolu dinañu dimbali ci ñu man a xam li waral jeqiku gi, atum 1789 g: + +Melokaanu politig wa : + +Buuri Faraas yi, ni ñu doon àttee Faraas, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lépp, képp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo dégge ci waxi buurub Faraas bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ). + +Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon(ay lois) , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir ñu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la jeqiku gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi. + +Moom de jëwriñam yi danu koo yilifoon, ak bëkk-néegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal (reforme), kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar. +Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Faraas yi bañoon. + +Njabootug Barbon gi, yàgg nañoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Faraas wi, ñoom daal dañu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo réew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp dañu ci daa duma Faraas. +Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali réew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolluwoon nañu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu ñu fay liggéey lu amal njariñ réew mi. Looloo taxoon njëlul nguur gi loofoon, mujjoon moom nguur gi fees dell aki bor. + +Nguur gi kat mujj na ay sànkam (ay deppaasam) àgg ci 130 milyoŋ yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyoŋ yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon. + +Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe-ni-la-neex ga amoon ca wàllug politig ga. +Nattukaayi diiwaan bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Faraas mujj di réew mu ay diiwaan boole, diiwaan bu ci nekk am ay yooni boppam , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak yoon yi, réew mi mujj séddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Faraas mujj doonatul menn réew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas. + +Na mboolaay ga meloon: + +Mboolayug Faraas gi, njëkk jeqiku gi, dafa séddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: garmi yi(kureelug ñu tedd ñi), kuréelu niti diine yi, ak baadoola yi walla kuréelu mbooloo mi. Ñatti kuréel yii nag – ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu – yamoowuñu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay wartéef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jëfkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay. + +Garmi yi + +Bu ko defee kuréelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa féetewoo pal yu kawe yi, yu ñoñ yi (siwil)ak yu xare yi , ci nguur gi. +Ñoom ba tay, daa nañu am ay cér ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm si, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amuñu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi. + +Niti diine + +“Niti diine yi” nag ñoom, seen kuréel moom itam bu ràññiku la woon, niki bu garmi yi, ñoom de daa nañu am ay suuf yu ñu leen dogal, yu yaatu, yu daa toll ci jurooméelu suufi nguur gi, maanaam bu ñu xaajoon suufi nguur gi juróomi xaaj, benn xaaj bi. Ñoom itam, ñu ñu teggiloon ay galag lanu. Li Jàngu bi daa ame ci suufam yooyu, ak ci galagi diine yi nga xam ne mbooloo mi daa nañnu ko ko fay, àggoon na ci 200 milyoŋ yu Farank. + +Loolu lépp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu néew lañu daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool ñi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbali. +Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu féexoon, moo taxoon dañu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi. + +baadoola yi + +Kuréelub mbooloo mi di "baadoola" yi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lañu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi jeqiku gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyoŋi nit , te kat booba garmi yi bu ñu leen boolee ak niti diine yi weesuwuñu woon 300 junniy nit. Coonab galag yépp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kuréel googu nag (gu baadoola yi), moo ëmboon kuréel gu diggu gi(Bourgeois), ak kuréelu baykat yi ak gu boroom mécce yi ak gu soldaar si. + +Kureel gu diggu gi + +Bu dee kuréel gu diggu gi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amuñu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi ñu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon. + +Lii lépp nag taxoon na ba gii kuréel meroon lool ci nguur gi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li ñu defaloon ñaari kuréel yii di gu garmi yi ak gu niti diine ñi. + +Kuréelug baykat yi + +Bu dee “Kuréelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kuréelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lañu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen liggéey yi gën a tar. + +Kuréelug soldaar si + +Bu nu nee “Kuréelug soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi ñoom, ak pal yu mag yi, garmi yi lañu leen daa jagleel. + +Na fa xalaat meloon: + +Ak li Faraasu njëkk jeqiku gi, di gënadi woon a nekk cib coona, ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lépp, teewul waa Faraas a gënoon a yëg yeneen réew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs. + +Jamono jii , dafa fiiroo ak diggante bob Faraas da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nostey politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya. + +Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy liggéey nañu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi jeqiku gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau + +Montesquieu + +Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu réew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay liggéeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca téereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), téere boobu nga xam ne téere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Faraas ak feneen. + +Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk nguur gi, te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju wéyal ji(mbaa ju doxal ji, ak ju laman ji . + +Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci téereem boobu mooy taxawal ag àtte gu tegu ci sartu réew ca Faraas. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu réew bu buur ba amoon ca Angalteer. + +Voltaire + +Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Faraas wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam lañu woon ak yéjj(saboote) . +Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Faraas ak gu Jàngu ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi. + +Wolteer + +Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lépp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Faraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital. + +Wolteer de gore ga peéxte ga waa Angalteer amoon da koo neexoon lool, yéemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginnaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy dañu koo dàqe woon Faraas. +Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca téereem ba tudd “bataaxeli xeltu” , walla “ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer”, atum 1734 g. +Wolteer nag dàq gi ñu ko dàqe woon Faraas, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lépp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi. +La desoon ca dundam ga lépp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër. + +Jean Jacques Rousseau + +Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom téere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy téere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti nguur gi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi. +Jeqikug Faraas gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi fraas-fraas bi – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci téereem boobu nu doon wax leegi. + +Jafe-jafe bu koppar ba: + +Atum 1789g, mooy at mi jeqiku gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom-koom, waaye la waraloon jeqiku ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari te tar. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon. + +Luwis 16, bi mu ñëwee jéem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kuréel yu xeet wi” – bii nga xam ne dañu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje. + +Naka la Jeqiku ga ame woon : + +Doomi kuréel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul réew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir ññu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yéwénal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yéwénal(reformes) yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Faraas man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk. + +Ci noonu ag wuute am ci diggante kuréelug garmi yi ànd ak gu niti diine yi ci wàll, ak kuréelug baadoola yi ca geneen wàll. + +Bu ko defee waa kuréelug baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cér yi te bañ a sukkandiku ci ay néeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kuréel gu nekk ci ñatti kuréel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kuréel yi (gu garmi yi ak gu niti diine yi) gu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kuréel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cér , ne daal ay néeg ñooy woote, bi loolu amee, céri kuréelu baaloola yi dañoo daje ñoom nee, cig beru, ñu néew ci garmi yi ak niti diine ñi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de duñu bàyyi mukk lii ñu nekke li feek wutaluñu réew mi ab sartu réew bu man a yéwénal séenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kuréel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi réew mi, bu ñu booloo, waxul bu genn taqalikoo nee, beru. + +Ci noonu way daje yii nga xam ne dañoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lañu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Faraans, bi nga xam ne day leeral li waa Faraas bëgg, tey jéem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug jeqiku gi. + +Tolluwaay yi nga xam ne jeqiku gi romb na leen: + + +Céri ndajem xeet wi daje woon nañu ca Versailles ngir defaral Faraas ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, génne ña ñu fa tëjoon ngir politig. +Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la jequiku gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Faraas wi di màggal, at mu nekk . + +Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Faraas, dem feneen. + +Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Faraas, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci jeqiku gi, ndax du seen njariñ, dañu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ . + +Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag aar gu réew ngir wattu jeqiku gi, aar ko,aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba. +Xarekati jeqiku gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse ak gënjëng (violance) . + +Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi. +Xeet wepp mujj daanaka di jàpple jeqiku gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu (forces armées)ju Faraas ji mujj fekksi “aar gu réew “ gi nu taxawaloon ngir wattu jeqiku gi. Ci noonu mbooloom xare mu Faraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba. + +Waaye way jeqiku yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim réew mi, ak mu Jàngu bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon Paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu jeqiku gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Faraas gepp, ñu daal di séddalewaat Faraans def ko ay doxaliin yu bees . + +Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jéem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jéem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy génn réew mi, gis nanu tam benn wayndare bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon dañu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan. + +Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 satumbar 1791 g, loolu di bi jeqiku gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Faraas bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Faraas la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi. +Mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Faraas wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy dañu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur saxoon na ca Faraas ba ca 21 satumbar 1792 g. + +Geneen tànnéef + +Ci atum 1792g, geneen tànnéef amoon na, gu ñu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Faraas, ca 21 satumbar 1792 g. +Ñu féetele ko doxal réew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg pénc gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar jeqiku gi, aar it Faraas ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci réew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen réewi Tugal yoo xam ne dañoo noonu woon jeqiku gi. + +Féetale nañu ko ba tay taxawal goornamaa bu Faraas bu dëgër, boo xam ne da fiy jéem a jële fitnay biir réew mi. + +Ñi jiite woon góornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne dañoo gëmoon ag yéwénal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne dañu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, dañoo gëmoon ne fii Faraas toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi. + +Liggéeyub goornamaa bu jataayub xeet wi: + +Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci réewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Faraas, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginnaaw bi nag góornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kuréelub kaaraange, féetale ko liggéeyub aar Faraas ci ñiy noonu jeqiku gi ci biir réew mi, ñu féetale ko ba tay moom kuréel bi, wàlulug taxawal am mbooloom xare mu Faraas mu dëgër, ngir aar Faraas, ak jeqiku gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xéewal, moom jeqiku gi. Góornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi am na ndam ci kaw xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Belsig ci ñu fipp ci kaw Imbraatóor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali Paap gi ci diiwaanu Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon jeqiku gi (moom Paab gi). + +Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kuréelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nañu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre képp koo xam ne yaakaaroon nañu ne da ngaa àndul ci jeqiku gi ak gaay jeqiku gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Faraas yi, ci tuumaal leen ne dañoo def ay wor yu mag. +Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nañook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci réewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar jeqiku gi, ak doonte jàmmaarloo woon nañook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar réew mi, tas te giimal féttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir réew mi, duggal seeni xarekat ci Belsig ak Holand, ànd ak loolu lépp teewul waa Faraas bëggoon ñu soppi séenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu. + +Ci 29 sulye 1794g, la céri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Faraas bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi. + +Goornamaab doxaliin bi: + +Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonoy tiital, xuppe ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu ñu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginnaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Atte googu walla góornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy liggéeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon: + +(1) Def politig bu maandu ci biir doxaliinu réew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam + +(2) Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi. + +Nañu fàttaliku ne góornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cér yoo xam ne dëppoowuñu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig góoramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig. +Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nañu, ni ñu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon daane nguur googu ñuy wax daane nguur gu Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu néewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Faraas te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lañu nekkoon. + +Napoliyon Bonaparte: + +Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Asaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Faraas da koo mujjoon jënd ci Genova. +Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi génne ca bànqaasu xare ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kuréelug kano ya ca xarekati Faraas ya. +Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali jeqiku gi , te fonkoon leen. Moom nag ab biddiwam a ngi féqe ci ginnaaw bi mu songee Itaali. +Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Faraas, dafa séddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Faraas gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g. + +Song gi Napoleon defoon Itaali: + +Góornamaab doxaliin bi, dafa féetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu ñuy wax gu Cherasco. +Napoleon defati ab xare ak dooley Paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, néewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare. +Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Faraas, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Faraas. + +Song gi Napoleon songoon penku bi: + +Politigkati Faraas yi naaloon nañu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nañu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca géejug Mans. +Politigkati Faraas yi, li ñu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Faraas ci géej gu diggu gi, ak man a àgg ca géej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk ca penku. + +Góornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko dénkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, géeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Faraas. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Faraas mi, ca ndoxum dóoxug Abii Xiir (golf), moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Faraas cangug géej gi Faraas yàgg a gent. Fraas sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jéeri ci mu géej, mu mel ne mu Britani mi. + +Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xareb jooñe la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xarey jooñe ya amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga. + +Isipt + +Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon réew mu nekkoon ci ron àtte gu Usmaan[ gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam. +Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nañook moom, xeex ak moom xeex bu tàng ngir aar seen réew. Waa Isipt yi béguñu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy dañoo fippoon ci kawam, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “jeqikug Xayra gi” . +Napoleon jawali na réewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginnaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, akYafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci géej gi, waa Usmaan yi di ko jàpple ci jéeri ji. + +Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji ñuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginnaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam. + +Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa teertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Faraas, waaye ci anam gu baaxul ci góornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule góornamaa. Bi ñuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga. + +Ay ngérte , yu am solo juddoo nañu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk: + +(1) Xareb Faraas boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu féete, ci wàllug jokkoo ak tuxute, ñeel imbraatoorug Britani gi ci penku bi. + +(2) Xare boobu Faraas da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise réewi Afrig gu bëj-gànnaar gi. + +(3)Boroom xam-xami xare boobu, bi ñuy ñëw, indaale woon nañu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nañu fi it benn sémb bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak géej gu diggu gi, di kàmbug Suwes bi(canaalu Suwes), te it indaale woon nau fi ab moolukaayu téere ci araab ñu koy wax moolukaayu Bolaax bi. + +(4) Xare bi wutoon na ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Faraas ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs. + +Napoleon ak réewi Tugal yi: + +Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte amoon na ndam ci kawam ca xare ba ñuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon ponk ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xaatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Faraas ji génn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara. + +Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Jàngu bi ci Faraas. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbéel. + +Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyéel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi. + +Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak réewi Tugal yi. Britani amoon ndam nag ci kawam ci wàllug géej gi, ca xare ba ñuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan ak Aleksandar mi nekkoon Xaysarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, ñu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal gepp, jëme ko Britani , daal di woon ga (manante) réewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci réewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na réew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu Xaysar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca péey ba, di Butrusburg, waaye mujj nañu manatuñoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal ñuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def liggéeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi ñuy dellu nag la waa Riisi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg. + +Bu ko defee, waa Tugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy dàq ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona ñu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginnaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Faraas yi, ngir xeexi réewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g. + +Bu ko defee, réewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir séddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos réew yu am doole yu peek Faraas wër ko. + +Liggéeyi ndajem Vienne: + +Liggéeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon: + +(1) Way daje yi delloowaat nañu buuri Tugal ya ca seen réew ya ñu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Faraas ak Espaañ. + +(2) Britani jëloon na sancu yi Faraas moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos. + +(3) Riisi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Belsig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowuñu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di “nationalisme” gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nañu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Riisi ak Otris ak Brusiya, dañoo defoon seen bopp ay réew yu ñoo am ag kilifteef ci réew yu Tugal yu ndaw yi. + +Li juddoo ci jeqikug Faraas gi: + +(1) Jeqiku gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral réewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi. + +(2) Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kuréeli mboolaay yi, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nañu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal. + +(3) Jeqiku gi ci Faraas mooy gi njëkk ci jeqiku yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki déggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay baat yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees. + +(4) Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lañu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gépp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee. + +(5) Xalaatub jeqiku gi law na ba àgg ci Tugal gépp, ak yeneen réew yu dul Tugal, yu àadduna bi. + +Taariixu Tugal +Bennal gu Itaali + +Bennal gu Itaali + +Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi: + +Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon réew mu ñu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Dóox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia. + +Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatóor lañu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa cig jonjoodi . + +Jeexiital ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali: + +Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. +Mu wutaloon réew mi mépp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug ndefar ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi réew mi, mu may waa Itaali ñi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo gu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am réew mu Itaali mu man a am, mu ñu bennal. + +Itaali ginaaw ndajem Vienne: + +Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy: + + Piemonte + Napoli + Parma + Modena + Toscana + Lombardia + Venezia + +Ñoom ñaar nag, mujj nañu leen boole, def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris. +Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga” maanaam lu nekk, nañu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen ci seen barab. + +Metternich ak gëtam yi mu tasoon ci gox yépp, jéemoon nañoo fuglu yëglekaay yi, daan naj it gépp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali ñoñ yi (siwil) yi ak yu xare yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle. + +Yewwuteg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali: + + +Politigu noteel bi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi ñu xamoon am solo gi bennal seen réew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi ñu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon. +Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lañu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi. + +Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu: + + Booloo gu Karbonaari (ñoñ këriñ) + Ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi. +Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nañu ci, baykat yi, liggéeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs. +Li leen manke woon nag, mooy dañoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a noot, te daa àntoodil seeni fipp. + +Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal. + +Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cér ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci réewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam. + +Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal réewum Itaali mi, ci ron ag noste gu pénc. + +Yëngu-yëngu yii, mujjoon nañu naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nañu ci lu toll ci juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab ab waa xare la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne dañoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lañu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer. +Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi ndefaram tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. +Boroom liggéey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nañu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali. + +Fàttalees léen + +Ñu fàttali léen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu-ginaaw lañu woon ci wàllug ndefar, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi ñuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennoo gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug ndefar, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi. + +Ak li boole Itaali, def ko menn réew doon nekk càkkuteful ñépp lépp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Dóox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëgguñu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li. +Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki dóoxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw génnam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk. + +Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali: + +Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, ñooy: + + Piemonte, mi nekk ci ron doji Alp yi, nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle, ak + + Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Faraas gi dend ak Itaali, moom nag diiwaan la bu gën a yor ay màndarga yu Faraas ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak + + Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci géej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte, ak + + Genova , moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal. + +Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal réew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii. Ñu tudd ci yi ci ëpp solo: + + 1 Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu réew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali. + + 2 Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jëwrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu réew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul Piemonte. + + 3 Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nañoo xare ba am ci xam-xam, jarbu ko. + + 4 Piemmonte moo nekkoon làqatuwaay bi politigkat yi ñu daa sonale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo. + + 5 Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano. + + 6 Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram. + +Cavour ak bennalug Itaali: + +Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu réew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu pénc. Moom de daa gëmoon ag yéwénal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom Piemonte) ak jeneen doole ju réew, ju mel ne Faraas mbaa Britani. + +Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am réewam ngir mu man a jiite liggéey biy bennal Itaali. + +Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba ñu man a jàmmaarlook mbooloom xare mu Otris mi, te man leen a génne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak ndefar gi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak ndefar, tege ay galag yu nduwaan yu mag ngir aar ndefar gu barab gi, yéwénal nosteg galag gi, daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi. + +Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yéwénal yu biir réew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nañu ba yoon ci réewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte geek Jàngu bi. + +Kafor mii nag xamoon na ni réewam mi tuutee woon, bu ñu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Faraas, am Riisi, ak Brusiya, waaye loolu lépp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la, manul a ñàkk, te itam mbirum àdduna bépp la, laaj na réew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci géewub politig bu àdduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci àdduna bi ba ñépp dégg ko, ci ndajey Tugal yi. + +Ci noonu mu digal Parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kuréelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Faraas, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatóor bu Faraas bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg. + +Kuréelu xare gu Piemonte googu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lañu deewe, teewul Kafour moom lijjanti na ba ñu yëg Piemonte ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma ñu doon def bi xareb Xarm bi jeexee. + +Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatóorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, safaan Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ. + +Bu dee Fraans nag, nga xam ne péncam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu réewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci Tugal. Politigu bitim réewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it réew mu nekk ci wetu Faraas la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk réew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk. + +Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy: + +Ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia. + +Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris: + +Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari témeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko safaan Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi . +Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g. +Taarixkat yi firee nañu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk. + +Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Faraas itam jibal ab xareem ci kaw Otris. +Soldaari Piemonte yi ak yu Fraas yi jot nañoo duma Otris, dàqe ko ca xare ba ñuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatóor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li ñuy wax juboo gu Siyorix atum 1859g. bokkoon na ca tomb ya ëppoon solo ca juboo ga: + +1 Otris bàyyee Piemonte Lombardi + +2 Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur + +3 Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi + +4 Delloosi ñi yilifoon Dóox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee. + +5 Boole Niis ak Savoia ci Faraas. + +Taarixkat yi, firee nañu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Dóox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte. + +Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Faraas yi nga xam ne dañoo tàmbli woon a mer ci néewal gi ñuy néewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral. + +Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Faraas génne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi. + +Askani Dóox yi bañ nañu ne duñu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko tombi juboo gu Siyorix gi yaxale(stipuler), ñu ne woon daal ñoom leegi dañuy dem bokki ca nguurug Piemonte. +Ci noonu ay jeqiku am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonal gu ko askan wi sonaloon ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti. + +Nii daal la Itaali doone benn ci diiwaan yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali. + +Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn: + +Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siiwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci liggéey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu(les volontaires) yu Itaali yi ñu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. +Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Sisil bi (le détroit de Sicile) , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu am solo. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ci ronam, dugg ci bennoo gi. + +Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali: + +Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi yépp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem diiwaan yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moom rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku am ndam di dugge ci dëkk bu ñnu xare ba nangu ko. + +Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 feewrye atum 1861g. Ca ndaje ma lañu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu ñu bennal gi. + +Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu ñu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulet atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy liggéey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig. + +Def Rom péeyu nguurug Itaali gi: + +Waa Itaali yi delloosi nañu Venezia gi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab diiwaan ci Itaali, ginaaw ba ñu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya. +Faraas it ay xarekatam génnoon nañu Rom, ngir sotti gi Faraas sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu kilifawu (officiel) ne Rom daal mooy péeyu nguurug Itaali gu ñu bennal gi. + +Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi. + +Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikaan, am it sañ-sañ ci yabal ay way teewal ca bitim réew. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo (son propre budget). + +Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy dañoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca téereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu liggéey ngir bennal seenum réew. + +Taariix +Itaali +Canc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi réewi ndefar (endustri) yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci réew yu bari ci yu amadi-doole yi ci àdduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbell. +Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen. + +Li sikk amul mooy sanc gi toppoon ci yewwuteg ndefar gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy melosuuf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi ñu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci réewi àdduna bi. + +Sababi sanc gu bees gi +Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + + Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug ndefar (industrie), ci lu bari ci réewi ndefar yu mag yi. Loolu nag tax ba réew yii mujj soxlawoo ay ñumm aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante réewi ndefar yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug ndefar, ndax seen koom-koomu xeet wépp ci ndefar la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci réew yu néew doole yii nga xam ne yu mag yii dañu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu ñumm yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu ñu man a jaaye seen njuddéefi(produits) Tugal yu ndefar yooyu. + + Yokku gu ñi dëkke ci réewi ndefar yi yokku woon, loolu moo waraloon réew yii gëstuji woon fu ñuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu réew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu génne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci réew yi ñu sanc, politig la bu ñu nosoon, jublu woon ci liggéeyal xemmeemtéefi sanc yu reewi ndefar yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp. + + Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy melosuuf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nañu diine niki ab raas bu ñuy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju ñu daan wax naan: «Wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginnaaw, ñi xamul dara». Àdduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi réewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom. + + Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci réewi Tugal yu ndefar yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci réew yii. Loolu yóbbu woon na réew yii ci ñu wuti bii dund ci réew yu néew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Réewi Tugal yi nag jaaruñu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal manoon naño jaare loolu ci yaxantu, waaye kay dañoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak séen ñawug ngànnaay, ak néew dooleg geneen wàll gi mu fas yéenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi. + + Lu bari ci réew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lañu woon ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne réewi sanc yii màggoon nañu ko te ame ko ni doole. + + Ay lonkoo(société) yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nañu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi dañu koo war a meññali ca réew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu àdduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yóbbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy réew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi. + + Bëgg gi réewi sancaan yu mag yu bari bëggoon a dëgëral seen yoonu jokkoo gu àdduna, loolu yóbbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu àdduna gi, di taqale diggante goxi àdduna bi. + + Bëgg gi yenn ci réewi sancaan yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principe) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy liggéeyal seeni xammemteefi sanc. + +Anami sanc gi +Sancug Tugal gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon réewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu dañu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii: + +Sanc ngir dëkk +Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginnaaw yëngu-yëngug wuññiy melosuuf yu Tugal yi. +Bu ko defee réewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci néewal doole ñi cosaanoo woon ci réew yi ñu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a génne seeni réew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi réew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale. + +Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Diggu Aamerik ak ca bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, mujjoon nañu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lañu cosaano, loolu di ci Diggu Aamerik ak bëj-saalum gi, lu ci dul Beresil, moom waa Portigaal a ko sancoon. + +Nu mel noonu la sahyooni yawud yi defoon ca Palastin, bi ñu ko sancee ci doole, dëkke ko, réewi sancaan yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yawud yi tasaaroo woon ci àdduna bi, dajee, dëkksi ca Palastin, ginnaaw bi ñu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug réewi sancaan yi, ak li askanu Palastin daan xeex loolu lépp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko. + +Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle. + +Teg loxo gu xare +Ay réew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay réew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy néew doole gi nu gendiku woon ci yii réew, rawati na ci wàllug xare. +Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim réew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii. +Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk: +Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g, ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g. + +Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la. +Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew. + +Aar +Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono. + +Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen. Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe. +Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk: +Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo. + +Feetale +Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginnaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiital yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel. + +Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi. + +Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen leen. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil. +Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk: +Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs. +Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom. + +Denkaane +Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginnaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wuutu fi kureelug xeet yi. +Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika ak yeneen . + +Sancug aada +Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom. + +Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi it (communisme), Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci réew yu bari ci adduna bi. + +Barabi sañ-sañ +Lu bari ci réewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani. +Amoon na it ay xejj(lu mel ne sañ-sañ) yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen. + +Koom-koom +Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal: + +Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu ñu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot naa man a liggéeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lépp nag ngir liggéeyal ay xemmemtéef yi mu amoon ci sanc àdduna bi, yilif ko . Looloo waral du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak canc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kiliftéefug sancaan yi. Lu yéeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi canc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn Jàngu rekk ci jëmmi boppam, waaye kay Jàngu yépp a ko daan def, moo xam Jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi). +Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante réewi sancaan yi. + +Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf gi réewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Portigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari réew yu ëppaloon te xaabaabal ci diine te daan ci par-parloo safaan jullit ñi ak seen àdduna. Bu ko defee wuññikati Tugal yii ame woon ag parparloo gu diine defoon séeni liggéeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci séen ginnaaw di liggéeyal xemmemtéefi canc yu seeni réew, loolu lépp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy liggéeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal . + +Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam : + +Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan (moyens) yu leen di dimbali ci seen liggéeyub nasaraanal bi, bu ko defee ñuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba liggéeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi (les sciences pratiques ou appliquées)ak yu xarala yi def. +Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonent Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon. +Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu ndefar gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu ñu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni liggéey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo: + +(1) Paj ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni: + +fajuwaay yi(les hôpitaux) ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi paj yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci réewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci réewi àddunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigéen, aki rewlikat(dooñkat) aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a liggéeyal Jàngu bi jaare ko ci liggéey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci àdduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Paj man nañu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu néew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi dañu daa wax naan: li ñu jublu ci jëfandikoo meccem Paj ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan, ginnaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Dañu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata'a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem paj mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi paj ci réew yu ndool yi yittewoo paj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug. + +(2) Njàngale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne: + +daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee daara yii ci réewi jullit ñi ak yu leen moy loolu dana man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lañu ci jublu woon. + +(3) Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nañu ko def ci réew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi: + +bu ko defee liggéeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw-làqu yi ak ñees tuxal ñi ci réew yu néew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci réewi Afrig yeek ak Asi. + +Loxob nasaraan biy indi ñam, paj ak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi. + +(4) Xibaarukaay yi + +Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci pénc yi, ak taalifi penkuwaan yi (les orientalistes) yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lépp ci tooke ñeel jullit ñi ak séenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci séeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal téere yii ak mooltéef yii(imprimé/publication) man nañu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci réewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li ñuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi ciy jeexiital. Mbootaayi nasaraanal yi sos nañu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Aamerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii liggéey. + +Nasaraanal ci réewi araab yi: + + +Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nañu ci réewi araab yi nekkoon ci ron cacug Britani, Faraas, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci réew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy néewal doole jullit ñi ak seen diine. Réew yi nasaraanal gi sutuxlu danañu leen ci tuddal yii : + +Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Faraas ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Faraas merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn lu dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug canc ci diggante Faraas ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalu gu katolig gu Faraas gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Faraas ak kiliftéefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley canc ji gën rëy te ëpp doole. +Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan liggéey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs + +Réewi Dóox gu Araab gi : + + +Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci réewi Dóox gu Araab gi (golf arabique), ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci réewi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn. + +Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Aamerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaan yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci réewi Dóox gi. Nasaraanalkat yu protestant yu Aamerig yi daal di taxawal Jàngu bu Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bi ci Manaama ak Abuudabi, ak Jàngu bu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu ñu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen téerey seen diiney nasaraan ji, ak seen yéene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi. +Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lépp ak daara yi, teewul ñu xeex bu baax safaan yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko ci seen xutba yi ñuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ canc yii te noonu ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar. + +Réewi Shaam: + +Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Sordani . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginnaaw xareb àdduna bu njëkk bi, nga xam ne réewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron féetale gu Faraas ak Britani. Bu ko defee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci dëkki Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kuréelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, féeteek kuréelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kuréel, ca la xarey kuréel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g. +Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab digg bu diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi fajuwaay aki daara, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa. +Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Aamerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nañook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte dañoo noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te canc gi lay liggéeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni góornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lañuy wax dëelub Balfour , génne ko it atum 1917g, lii ko taxoon a jug di sos am réew mu xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar. + +Isipt: + + +Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginnaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee bu katolig bu Faraas bi tukkee woon Liyon daal di def ay liggéeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko. + +Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay liggéeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginnaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu diiŋatkat yu Amerig yi def ñoom itam seeni liggéey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki daara aki jàngu aki katedraal ak barabi seddale téere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy liggéeyal nasaraanal . + +Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jànguwaay aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs. +Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo. + +Sudaan: + +Liggéeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudaan, rawati na ci ginnaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni liggéeyi nasaraanal ci biir jullit ñi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudaan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu réew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nañu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudaan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal. + +Waaye waa Sudaan ñoom tooguñu rekk faste seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. jeqiku gu Mahdi gi xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru réew ma ñoom itam xeex ko. + +Réewi Maxrib gu araab gi : + +Maxrib walla (Maghreb) gu araab gi dafa nekke fu jàkkaarloo ak réewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Faraas. Réew yii nag jariñoo nañu bu baax néew dooleg réewi Maxrib gu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen liggéeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku canc gi nar a ñëwi di tukkee ci Faraas, Itaali ak Espaañ. Réew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lañu. +Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug canc gu Tugal gii ci réewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. +Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu ñu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taariixam, jéem a jox jullit ña fa dëkke woon ay réewu yu réewi sancaan yi, bu ko defee duñu réewooti ci seeni réew, te duñu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jéem a taxawal liggéeyub nasaraanal bi. + +Waaye nag ñu fonk seen réew ñii dëkke woon ci réewi Maxrib gu araab gi amoon nañu ndam ci damm degug canc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon. + +Barabi nasaraanal yi ci réewi araab yi: + +Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nañu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci réewi araab yi, lii ci la: + + Mbootaayi nasaraanal yi sos nañu lu bari ci ay daaray dal ,daara yu diggu ak daara yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu góor yeek yu jigéen yi, ci mbooleem réewi araab yi nasaraanal gi dugg. + + Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci barabi njàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju kawe ju Aamerig ji, xamluwaay bu penku bi, xamluwaay bu Faraas bi, yooyu yépp nag ñi ngi Xayra . Bu dee Sudaan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak daara ju Amerig ak daara yu Qibt yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Aamerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju kaw ju Aamerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju kawe ju katolig ja, walla daara ju kawe ju Yesu ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf (sosef). + + Nasaraanalkat yu penkaan yi dugg nañu ci gëstuwaay yu làkk yi ci réewi araab yi. Ñu dugg ca gëstuwaayub làkk ba ca Xayra ak bu xam-xam ba ca Damasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penkaanu Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom ak Margoliyos mu Faraas mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Olaand mi, ak Harithman mu Almaañ mi. Penkaan walla penkuwaan yi duggal nañu seen loxo ci téere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, téere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci téere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel. + + Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nañu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem réewi araab yi. (ginaaw ci réew yii lañu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñu ciy wax). +Mbootaay yu adduna yi: kureelug xeet yi , mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi), mbootaayug reewi Lislaam yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi). + +Ñatti mbootaay lanu bëgg’a waxtaane ci doggantal gii, ñooy : Kureelu xeet yi, Mbootaayu xeet yi, Mbootaayu reewi jullit ñi. + Mbootaayu Réewi Jullit yi + Kureelu Mbootayu Xeet yi‎ + +Adduna + + +Ni Sapoŋ jëme kanam + +Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g: + +Sapoŋ de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu-ginnaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na ndefar. + +Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci réew mu deltu ginnaaw, dem ci réew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, caada, politig ak xare. + +Mu roye nag ci réewi Tugal yi, gisiinu canc ak yaatal ko, ci réew yi mu dendal, ngir wone ci dooley àddinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi ñuy def ngir teg loxo ay réew, sanc leen. + +Sapoŋ nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci réewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Aamerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum 1854 g gii rekk - teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Tugal gi, di ci jariñu, di ci niitu. + +Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam aw yaxantuwiinam. Réewum Sapoŋ ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug ndefar gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg. + +Bu ko defee, Sapoŋ xëy di réew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci réewi Asi yi, ci wàllu ndefar, xam-xam ak xarala . + +Mu mujj am, moom Sapoŋ, mbooloom-gaal (flotte)mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci àdduna bi, ci diggante ñaari xarey àdduna yi. +Marsandiisi Sapoŋ yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig. + +Sapoŋ, ginnaaw bi ñu ko gañee ci ñaareelu xareb àdduna bi: + +Sapoŋ dumaas na ko ci ñaareelu xareb àdduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel réewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Sapoŋ. +Sapoŋ nag mujjoon na nangu ne amees na ndam ci kawam, mu wommatu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Aamerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonuñnu taxawal benn jataay bu way tapoo yi , ngir doxal mbiri Sapoŋ, ñu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g. + +Waa Aamerig yi nag rëddaloon nañu Sapoŋ benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatóor bi , ñu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni ñuy jànge ak li ñuy jàng, wutaloon leen sartu réew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi (les grandes sociétés) . +Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Sapoŋ yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees . + +Ci noonu Sapoŋ jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk, réewi ndefar yu jëm yi kanam. + +Waa Sapoŋ jariñu nañu ci li leen Aamerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Metlàŋ yu Sapoŋ yi dox nañu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Sapoŋ, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Sapoŋ bari ay liggéeykat. + +Suqali nag gën na a yokk ci wàllug ndefar ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Sapoŋ mujj di ñatteelu réew mi ëpp lu muy liggéey weñ, bokk it ci réew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu ñuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, liggéey bi aju ci jumtukaayi mbëjfeppal “elektronig” yi gën a jëm kanam, ba mujj Sapoŋ àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja yi ñuy jaaye liggéeyi Sapoŋ yi gën a yaatu, gën a bari ci àdduna bi. Bu ko defee Sapoŋ mujj nag di réewum ndefar mu mag, mu dox, te jëm kanam. + +Sapoŋ +Saaru Xunti ma +Makka La Wacc 105 Laaya la. + +(1) Maa ngi sant Yàlla mi wàcce ca jaamam ba téere ba te dara dëngu ca. + +(2) Mu jub xocc ngir mu xuppe ci mbugal mu metti muy bawoo fa moom ngir mu begal way-gëm yiy def ay yiw ne am nañu yool yu rafet. + +(3) Ca la ñuy sax dàkk. + +(4) Ngir it mu jàjj ña naan Yàlla am na doom. + +(5) Amuñu ca benn xam-xam waxatuma la séeni Baay. kàddu gu rëy a ngook gu génne ca séeni gëmmiñ. Waxuñu lu dul aw fen. + +(6) Boo demee yaa ngi alag sa bopp ci topp ci séen gannaaw ak u naqar ngir li ñu ñakk a gëm wax jii. + +(7) Nun dey def nanu li nekk ci kaw suuf mu koy taaral. Ngir nu nattu léen kan ci ñoom a gën a rafet jëf. + +(8) Te nun noo def la ca kowam mu dib dénd bu wow kohh. + +(9) Ndax yaakaar nga ni gaay xunti ma ak (seén xaj ba nekk nañu di lu yéemé ci sunnu kéemtaan? + +(10) Fàttalikul ba waxambaane ya làqoo ca xunti ma ne : «Sunnu Boroom noo ngi lay ñaan nga indil nu yërmande ju bawoo fa yaw, te nga yéwénalal nu sunu mbir mii ba mu jub. + +(11) Nu nelawal léen ca xunti ma ay at yu takku. + +(12) Gannaaw lolu nu yee léen ngir ñu xam kan ci ñaari kurél yee gën a takk diir ba ñu fa sax. + +(13) Noo ngi lay nettalli séen xibaar dëgg-dëgg ;nekkoon nañu ñu jub, nu dolli léen ak njub. + +(14) Nu takk séen fit ba ñu jógee ni : sunu Boroom a di Boroom asaman yi ak suuf si, dunu ñaan jeneen yàlla ju dul moom, bu nu ko waxee dëy, kon wax nanu lu ëpp. + +(15) Sunu nit ñii nag ñoom jël nañu yeneeni yàlla yu dul moom; lu tee ñu joxe ci tegtal bu leer ? ku dàq a tooñ kuy duural yàlla ay fen? + +(16) Bu ngéen léen beddikoo ak la ñuy jaamu dem léen làqqu ji ca xunti ma. Séen Boroom wesaare yërmandeem ci yéen defal léen ag jàppandal ci séen mbir. + +(17) Nga gis jant bi bu fenkkee bàyyi séen xunti ma ca ndey-joor bu sowee bàyyi léen ca càmmooñ ñoom nag ñu nekk ci men lëm foofee, loolu bokk na ci kéemtaani yàlla, ku Yàlla gindi kooku moo gindiku, ku mu sànk ,doo ko amal ku koy taxawu di ko gindi. + +(18) Dangaa yaakaar ne dañoo yewwu te fekk ne ña nga tëdd di ndaw ñu léen di wëlbati ca ndey-joor ak ci càmmooñ séen xaj ba ne wàpp ca ëtt ba, boo ne woon jàkk ci ñoom danga ne waññet daw tiit ba fees. + +(19) Noonu la nu lèen yee ngir ñu laajante ci séen biir. Am ca ku ne : Ban diir ngéen fi sax ? Ñu ne : Bès walla as lëf ci bès; ñu ne : Séen Boroom daal moo gën a xam li ngéen fi sax. Yónni léen kenn ci yéen ak xaalis bii mu dem ca dëkk ba, na xool ñam wa gën a sell mu ëndil léen ca lu ngéen wërsëgoo. Na teey, bu mu yëgal kenn nag !. + +(20) Ndax ñoom bu ñu léen jekkoo daañu léen jam (xeer) walla ñu delloo léen ca séen diine, te kon dungéen texe mukk + +(21) Noonu la nu léen feeñale ndax ñu xam ne digéb Yàlla dëgg la, ak it ñu xam ne àllaaxira amul lu ñu ciy sikki-sakka. (fàttalikul) ba ñuy xëccoo séen mbir ca séen diggante; ñu ne : Tabaxal léen ab tabax. Séen Boroom a gën a xam séen mbir; ña not ca séen mbir ma ne : Fàww nu tabax jàkka ci séen kaw. + +(22) Dinañu ne : ñatt lañu (woon) séen xaj baa léen ñeenteel. Dinañu ne : juróom lañu séen xaj baa léen juróm-benneel, » ci demaleek a fekkale. Daañu ne : juróom-ñaar lañu séen xaj baa léen juróom-ñatteel. Neel : Sama Boroom moo gën a xam séenub lim. Kenn xamuléen lu dul ñu néew. + +(23) Bul werante ci séen mbir lu dul werante wu leer. Bul sàkku kenn ci ñoom mu ubbil la ci séen mbir. + +(24) Bul wax dara nag ne danaa ko def ëllëg lu dul bu soobee Yàlla. Nanga tudd sa Boroom boo fàttee, te nga ne : « jombul sama Boroom won ma lu gën a jub lii ». + +(25) Sax nañu ca séen xunti ma ñatti téeméeri at ñu teg ca juróom-ñeent. + +(26) Yàllaa gën a xam la ñu fa sax. Moo moom kumpay asamaan yi ak suuf. Ndaw ku man a gis, ndaw ku man a dégg ! Amuñu kenn ku léen di taxawu ci séeni mbir, te àtteem bi du ci boole kenn. + +(27) Jàngal li ñu la yenkeewal ci sa Téeréb Boroom bi, Ay kàddoom kenn manu koo soppi. Te amóo benn làqukaay bu dul Moom !. + +(28) Notal sa bopp ànd ak ñi nga xam ne dañuy ñaan séen Boroom subaak ngoon namm jëmmam ja rekk. Bu sa bët jéll ñooñu, ngay bëgg taarub dundug àdduna bii, bul topp koo xam ne dañoo fàbbi ab xolam ci fàttiliku nu, mu topp bànneexu bàkkanam, mbiram nekk lu jéggi dayoo. + +(29) Texawal ne dëgg gii ca sa Boroom la bawoo. Ku mu neex na gëm, ku mu neex na weddi ! Nun waajal nanu Safara ñeel na tooñkat yi, mu peeg léen wet gu ne . Bu ñu sàkkoo wallu, nu wallu léen ak ndox mu mel ni téex ub diwlin, buy lakk xar-kanam yi ; googu naan a bon ! Boobu sóonuuwaay a ñaaw ! + +(30) Wóor na ni ñi nga xam ne gëm nañu tey def ay yiw, nun déy dunu sànk yoolu ku rafetal jëf. + +(31) Ñooñu am nañu àjjana ju sax, yu ay dex di daw ca séen ron, ñu takkaayal léen fa ay lami wurus ; ñu sol fa yéré yu nëtëx, yu jógé ci sooy ak “wëluur” ; ñuy sóonu ci ay lal Boobu yool a baax, boobu sóonuwaay a rafet . Nu ballal ay dex ca séen biir. + +(32) Joxléen misaal ci ñaari gaay yoo xam ne defal nanu kenn ka ñaari tooli rese��, ñu wërëléléen ay tàndarma, ñu def gàñcax ca diggante ba . + +(33) Ñaari tool yépp di menñ te dara wàññikuwu ca. + +(34) Mu ame ay meññent, mu wax àndandoom ba ne ko fekk nuy waxtaan : + +(35) « Maa la gën a bare alal, te maa la gën a dëgër mbooloo ! » Mu tàbbi ca toolam ba, te di ku tooñ boppam, te mu naan : « Man daal foog naa ni lii du yàqu mukk! + +(36) « Te yaakaaruma sax ne Saa dana taaxaw ! Te sax bu ñu ma delloo sama Boroom danaa fa fekk dellluwaay bu gën bii ». + +(37) Ándandoom ba ne ko, fekk muy waxtaan ak moom : « Moo ndax dangaa weddi ki la bind ci suuf, ginnaaw ba mu la génné ci toq, topp mu yemale la nga di gòor ? .» + +(38) « Waaye man déy kookoo di Yàlla sama Boroom ! Sama Boroom nag duma ko bokkaaleek kenn ! » + +(39) « Tee woon ba nga duggee ci tool bi nga ne : lii moo neex Yàlla ! Doole amul lu dul ci ndimalul Yàlla ! Bo gisee ma gën laa néew alal ak i doom. » + +(40) « Amaana sa Boroom jox ma lu gën sa tool bi, te (amaana) mu sànni ci sa tool bi ay dënu yu jògé ci asamaan, mu mujj nekk pàkk bu ne ñayy. » + +(41) « Walla ndoxam ma mujj ηiis, te doo ca am menn pexe. » + +(42) Meññentam ma yàqu, mu mujj di wëlbati loxo, di réccu la mu ca defoon, lépp daanu. Mu naan : « Cèy! aka neexoon ma bañ a bokkaaleek sama Boroom bi kenn. » + +(43) Te amul kurél béneen bu dul Yàlla bu koy dimbali, te munu la feyyu. + +(44) Foofa dèy Yàlla rekk a fa di ndimbal. Boobu yool a gën, te googu muj a gën. + +(45) Joxléen misaal ci dundug àddina gii, dafa mel ni ndox mu nu wàcce ci asamaan gàncaxu suuf si jaxasook moom, mu mujj nekk mboob, ngelaw li di ko tasaare.. Te Yàlla ku jekku lépp la. + +(46) Alal jeek doom yi taarub àddina jii la. Te nag yiy des te baax ñoo gën ub yool fa sa Boroom, te ñooy gën-ji-mébét. + +(47) Bu keroogee dananu doxloo doj yi nga gis suuf si mu ne dàηη, nu dajale léen, dunu bàyyi kenn ci ñoom. + +(48) Ñu gaaral léen séen Boroom ñu doon ay sàppe ca dëgg-dëgg ngéen ñëw fii ci Nun ni nu léen sàkke woon cig njalbéen. Te nag nee woon ngèen ne dunu léen defal ab dig. + +(49) Nu teg nag téeré bu, nga gis nag saay-saay si ñu tiit ca la ca nekk, ñuy wax naan : «wóoy nun ! Moo lu jot téeré bii be bàyyiwul lu tuut wàlla lu rèy lu dul rekk takk na ko ! » te nag nu fekk la ñu jëfoon mu teew. Te sa Boroom du tooñ kenn. + +(50) Fàttalikul bu nu nee Malaaka ya : « sujjòotalléen Aadama. » Nu sujjòot ba mu des Ibliis ci jinne ya la bokkoon, mu lànk bañ a topp ndigalul Borooman. Ndax yéen dangéen koy jàpp mook i sëtam far ak ñoom ba ma fii yalla ? Te ñoom ñu di séeni noon. Tooñkat yee bon kuutlaay. + +(51) Seedeloowuma léen bindu asamaan si waxumalaak séen ug bind ñoom ci séen bopp. Te duma dëgërloo sànkekat yi. + +(52) Bu keroogee ba mu ne : wooléen ni ngèen ma doon bokkaaleel,ñi ngèen doon gortu. Ñu wooleen,waaye du énu leen wuyu. Nu def ci séen diggante xuru alkande. + +(53) Saay-saay si gis safara wa, mu wòor léen ne daañu ca tàbbi te amuñu lu koy wuññi. + +(54) Leeralal nañu nit ñi ci Alxuraan jii ci misaal mu ne . Waaye nit nag moo gën a man a dàggasante lu ne . + +(55) Dara terewul nit ñi gëm ba léen njub ga dikkalee, te ñuy jégglu séen Boroom, lu dul doxalinu ñu jëkk ña ; dafa ñëw ci ñoom walla book mbugal mu ñuy jàkkaarlool war a ñëw ci ñoom. + +(56) Nun nag dunu yebal yonent yi lu dul ngir ñu ñëw di bégle ak di xuppe. Yéeféer yi nag dañuy dàgge ci neen ngir néewal dëgg. Te nag Jël nañu sunu kéemtaan yi di léen yéjje. + +(57) Kan moo dàq a tooñ ku ñu fàttali kéemtaani Boroomam mu dummòoyu léen fàtte la mu defoon. Nun danoo muur séen xol ya be duñu ko dégg, saañ séen nopp ya, te boo léen woowee jëme léen ci njub duñu gindiku mukk. + +(58) Sa Boroomay jéggalaakoon tey boroom yërmande. Bu leer doon jàpp la ñuy fàggu kon dana léen gaawe mbugal mi. Li am daal mooy am nañu dig boo xam ne duñu ko man a làqu fenn. + +(59) Dëkk yooyu nag alag nanu léen ba ñu tooñee, te wutaloon nanu séen alkaande ja ab dig. + +(60) (Fàttalikul) ba Muusaa waaxee ngóoram sa : Duma deñ di wéy ba fa ñaari géej ya daje walla ma wéy ab diir bu yàgg lool. + +(61) Ba ñu yeggee fa ñu daje ñu fàtte fa séen jën wa, mu jaar ca géej ga wèy. + +(62) Ba ñu jàllee mu ne ngóoram sa : ëndil sunu añ bi, sunu tukki bii daj nanu ci coono. + +(63) Mu ne : xanaa xamóo ne ba nu wàccee ca xeer wa la fàtte jën wa. Dara fàtteloowuma ko lu dul Séytaane, bé fàttalikuwuma ko. Mu toppaat aw yoonam jëm ca géej ga ; lii moo doy waar! + +(64) Mu ne : loolu la nu doon wut. Nu woññeeku topp séeni tànk ya woon. + +(65) Ñu fekk benn jaam ci sunu jaam yi bu nu jox yérmande ju tukkee fi nun, te nu jox ko xam-xam bu bawoo fi nun. + +(66) Muusaa ne ko : Ndax duma la topp ngir nga jàngl ma li ñu jàngal cig njub ? + +(67) Mu ne (ko) : yaw soo àndeek man doo man a muñ. + +(68) « Nooy man a muñe loo xam ne peegóo ko cig xam. + +(69) Mu ne : « Dinga ma fekk bu soobee Yàlla may ku muñ, te duma moy sa benn ndigal. + +(70) Mu ne : Boo ma toppee, bul ma laaj dara, ba keroog ma la ciy tudd li ko waral. + +(71) Ñu wéy ba yéeg ca gaal ga, mu xar ko. Mu ne : Ndax danga koo xar gir labal séen woroom ? Li nga def réy na ! + +(72) Mu ne : xanaa waxuma la woon ne foo àndeek man doo man a muñ.. + +(73) Mu ne : Bul ma jàppe sama fàtte gi te bul ma teg ci sa mbir mi lu ma manul ! + +(74) Ñu wéy ba dajeek benn xale, mu rey ko. Mu ne : ndax dangay rey bakkan bu sell ci lu dul bakkan. Def nga bir mu juunu! + +(75) Mu ne : xana neewuma la woon boo àndeek man doo man a muñ. + +(76) Mu ne ! Su ma la laajatee dara ginnaaw ba bul àndateek man. Egg a ngaak man ci am ngànt. + +(77) Ñu wéy ba agsi ci waa-benn dëkk, ñu fekk fa wenn sàkket wuy bëgg a màbb nu jubbanti ko. Mu ne : Bu la neexoon nga jël cig pey. + +(78) Mu ne (ko) fii nag la ñuy tàqalekoo. Dinaa la firil lii nga xam ni manuloo ko woon a muñ. + +(79) Li aju ci gaal gi, ay miskiin a ko moomoon yu daan liggéey liggéeyu géej ga. Ma bëggoon caa def sikk ndax dafa am benn buur buy nangu gépp gaal ci doole. + +(80) “Bu dee xale bi nag, ñaari way-juram dañoo gëm, Nu ragal mu teg léen ag bew ak ug weddi”. + +(81) “Te yaakaar nañu ne séen Boroom wecceel léen ku ko gën, te gën a sell, gën a am yërmande.” + +(82) “Bu dee sàkket wa nag, ñaari xaley jirim ñoo ko moom, yu nekk ca dëkk ba, te séen um koom dafa nekk ca ron ga, te baay bu baaxoon la, te Sa Boroom namm bu ñu demee ba dëgër génne séen koom ma, mu di yérmande gu tukke ci sa Boroom, te defuma ko ci sama sañ-sañ loolu mooy pirig li nga manul woon a muñ.” + +(83) Ñu ngi lay laaj mbirum « Sul-Qarnayni » Neel : “Dinaa léen nettali ci moom lu di fàttali.” + +(84) “Nun noo ko dooleeloon ci kaw suuf, defal ko ci lu ne aw yoon” + +(85) “Mu topp yoon be àgg ca sowu jànt, fekk ko muy so ci déeg bu ñuul kuk, nu fekk fa aw nit. Nu ne : yaw « Sul-Qarnayni », benn nga mbugal léen walla nga defal léen njekk.” + +(86) Mu ne : ku tooñ nag, dananu ko mbugal topp nu delloo ko ca Boroomam mu mbugal ko mbugal mu tar. + +(87) Ku gëm nag te jëf jëf ju rafet, daanu ko defal ag yombal ci sunu ndigal. + +(88) Mu toppaat yoon wa be yegg penkub jànt ba, mu fekk ko muy fenk ci aw nit yu defunu séen digganteek moom genn kiiraay. + +(89) Naka noonu la Nu peege ci xam-xam la ne fa moom. + +(90) Ginnaaw ba mu toopaat yoon wa. Ba mu egsi diggante ñaari xeer yu mag mu fekk fa nit ñoo xam ne daanaka duñu dégg wax. + +(91) Ñu ne yaw « Sul-Qarnayni », Yaajooja et Maajooja dañuy yàq ci réew mi, ndax duñu la jox galag ba nga defal nu sunu diggante dig woo xam ni dana léen téyé. + +(92) Mu ne : “Jàppandal gi ma sama Boroom defal moo gën waaye dimbali léen ma ci doole ma def séen digganteek ñoom ab sëkk“ + +(93) “Ëndilléen ma daggiti weñ yoo xam ne su ñu demee be tollook ñaari walli doj wi, uppléen, bu demee ba nekk safara, Mune : Ëndilléen ma sotti ci xelliti përëm. + +(94) “(Noonu) duñu ko man a yéeg, duñu man a bënn”. + +(95) “Loolu yërmande ju tukkee ca sa Boroom la. Bu sama dige Boroom dikkee, dafa koy def mu mokk rumbux. Te sama dige Booroom dëgg la”. + +(96) Nu bàyyi ñenn ña ñuy jaxasook ña ca des, Nu ëf ca bufta ba, Nu dajale léen dajale bu wóor. + +(97) Te bu keroogee dananu gaaral Safara yéeféer ya ab gaaral. + +(98) Ñooy ñi nga xam ne séen gët ya dafa muuru woon ba duñu fàttaliku te ñu nekkoon ñu dul man a dégg. + +(99) Ndax ñi weddi (Yàlla) dañoo yaakaar a jël sama jaam yii di far ak ñoom bàyyi Ma fi Nun dèy waajal nanu Jahannama muy wàccuwaayu yéeféer ya. + +(100) Neel : Ndax dunu léen wax ñi gën a pert jëf : Ňooy ñi nga xam ne séen jëf ya sànku nañu ci àdduna jii, te ñu yaakaar ne ñu ngay rafetal jëf. + +(101) Ñooñu ñoo weddi séen kéemtaani Boroom ak ab dajeek Moom. Séeni jëf yàqu keroog dunu léen màndaxeel séeni jëf. + +(102) Li ko waral moo di séen pey mooy jaanama ngir la ñu weddi, te danoo jël sama aaya yi ak sama ndaw yi di léen yéjji. + +(103) Wóor na ne ña nga xam ne gëm nañu, àjjana firdaws nekk na séen wàccu-waay. + +(104) Fa la ñuy béel, te duñu ca sàkku genn ug soppiku. + +(105) Neel : Bu fekkoon ne géej gi dafa nekkoon daa ngir bind sama kàdduy Boroom, kon Neel : kon géej ga dana jeex te sama kàdduy Boroom du jeex, dontale ëndi woon nanu geneen géej mu tëbb ko. + +(106) Neel : Man duma lenn lu dul mbindéef ni yéen mu ñuy yenkeewal ne : séen Boroom benn Yàlla là. Ku yaakaar ne dana dajeek Boroomam na jëf jëf ju yiw te bu ma bokkaale kenn ak Borooman ca jaamu ga mu koy jaamu + +saari alxuraan +alxuraan +Saaru Maryaama +Màkka la wàcc 99 laaya la + +(1) K. H. Y. Saad [Lii] fàttali sa yërmande Boroom la ca jaamam ba Sàkkariyaa. + +(2) Ba mu ñaanee Boroomam ndànk + +(3) Ne ko : "Sama Boroom ! néew naa doole, te sama bopp weex na tàll ak bejjaaw. Te masuma laa ñaan be sooy. + +(4) Te am naa am tiit ci njaboot gi sama ginnaaw, te sama soxna dafa jërméel. Kon nag yal na nga ma may kuutaay gu bawoo ci yaw + +(5) Gu may donn, tey donn njabootu Yànqooba, te sama Boroom yal na nga ko def muy ku ñu gërëm !" + +(6) Yaw Sàkkariyaa noo ngi lay bégale doom ju góor ju tudd Yaxyaa, kenn masu koo tudd. + +(7) Mu ne : " Sama Boroom nu may ame doom, te sama soxna jërméel, te ma màgget be kumur". + +(8) Mu ne : "Noonu la. Sa Boroom nee na : loolu yomb na Ma, te nag Maa la bindoon, te doo woon dara". + +(9) Mu ne : "Sama Boroom, defal ma firndé". Mu ne : "Sa firndé moo di doo mën a wax ak nit ñi ñetti guddi yu mat sëkk". + +(10) Mu génne ca jàkka ja, yem ciy nitam junj léen ne: “sàbbaalléen suba ak goon!” + +(11) “Yaw Yaxyaa, téyél ci Téeré beek doole !” def Nanu ko muy ku xereñ àtte cig ngoneem. + +(12) Ak yërmande ju tukkee ci Nun, te ku fegu la woon + +13) Te ku baax la woon ciy way-juram, réyul woon, daawul woon moy Boroomam. + +(14) Yal na ko Yàlla defal jàmm keroog ba mu juddóo ak keroog ba muy dee ak keroog ba muy dekkiwaat di dund. + +(15) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Maryaama, ba mu beddikoo ay nitam dem ci barab bu féete penku + +(16) Mu doxale kiiraay diggantéem ak ñoom ; Nu yebal ca moom Sunu malaaka [Jibriil] mu feeñu ko ci melow nit ku mat sëkk. + +(17) [Maryaama ne :] Yal na ma Yàlla musal ci yaw ! Ndeem fegu nga ! + +(18) Mu ne ko: "Man sa ndawal Boroom rekk laa, lu lay maysi doom ju sell". + +(19) Maryaama ne ko : "Numay ame doom, te mbindéef laalu ma, te duma jigéen ju bon". + +(20) Mu ne : "Noonu la, sa Boroom nee na : “loolu lu Ma yomb la », Te dananu ko def kéemtaan ci nit ñi ak yërmande ju bawoo ci Nun. Mbir mi sotti na !". + +(21) Mu ëmb ko, beddeekook moom ca barab bu sori. + +(22) Mat wa dab ko ca ëkku tàndarma ga. Mu ne : "Céy ! Aka neexoon ma dee lu jiitu lii, su ko defee ñépp fàtte ma, kenn dóotu ma tudd. + +(23) Mu woo ko cag ronam [ne ko] : "Bul jàq, sa Boroom defal na la ci sag ron am yol". + +(24) Gësëmal dàttu tàndarma gi, tàndarma yu ñor xomm rot, wutsi la + +(25) Lekkal, naanal, te seral sa xol. Boo gisee kenn ci nit ñi neel : "Man kat damaa nisër a wooral Boroom yërmande ji ; kon nag tey duma wax ak nit". + +(26) Mu indil ko (liir ba) aw nitam, leewu ko ; ñu ne ko : "Céy Maryaama def nga njaaxum gu réy !". + +(27) Yaw jigéenu Aaróona, sa baay dey du woon waa ju bon, sa ndey it nekkul woon jigéen ju bon !". + +(28) Mu joxoñ ko (liir ba) ; ñu ne ko : "Naka la nuy waxeek liir bu nekk ciy laltaayam". + +(29) Mu (liir ba) ne : "Man jaamu Yàlla laa, jox na ma Téeré ba (Injiil) + +(30) Mu def ma may ku bàrkeel, te mu dénk ma julli ak asaka feek maa ngi dund, + +(31) Ak baax ci sama ndey, te defuma may ku féttéerlu di ku texeedi + +(32) Yal na ma Yàlla defal jàmm keroog ba ma juddóo ak keroog ba may dee ak keroog ba ñu may dekkal may dund !". + +(33) Kookooy Isaa doomu Maryaama, baatu dëgg bi ñuy werante + +(34) Jaaduwul ci Yàlla Muy doomoo kenn. Ëppale na ko boppam ! Su dogalee mbir da naan ko : « Nekkal, mu nekk ». + +(35) Te nag Yàllaay sama Boroom, di séen Boroom : "Jaamuléen ko. Lii yoon wu jub la". + +(36) Kurél ya wuute ca séen diggante. Mbugal ñeel na ñi weddi dikkug bés bu réy + +(37) Aka ñooy mën a dégg ! Aka ñooy mën a gis ! Keroog bu ñu teewee Sunu kanam ; waaye nag tey tooñkat yi ñu ngi ci réer gu metti. + +(38) Waarléen ndax ñoom ñu ngi ci càggante ak ñàkk a gëm ; bésu réccu ba fekk dogal ba sotti na. + +(39) Nun nooy donn suuf si ak la ca kowam, te ci Nun lañuy déllusi. + +(40) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Ibraayima, + +(41) Moom dey ku dëggu la woon, te di ab Yónnent. + +(42) Ba mu nee baayam : "Sama baay, lu tax ngay jaamu lu dul dégg, du gis, te du la jariñ dara + +(43) Sama baay, am na lu ma dikkal ci xam-xam loo xam ne dikkalu la, topp ma, ma teg la ci yoon wu jub xocc. + +(44) Sama baay, bul jaamu séytaane ; séytaane dey kuy moy Boroom yërmande ji la. + +(45) Sama baay, ragal naa mbugal mu bawoo ca Boroom yërmaande ja, laal la, ñu boole la ci ñi far ak séytaane". + +(46) Baayam ne ko : "Mbaa du dangaa bañ sama yàlla yi, yaw Ibraayiima, soo yemul, danañu la sànni ay doj. Sori ma ab diir!". + +(47) Mu ne : "Yàlla na jàmm nekk ci yaw. Danaa la jéggalul sama Boroom ; Moom dey ku baax ci man la". + +(48) « Beddeeku naa léen ak ña ngéen di ñaan ñu dul Yàlla, te maa ngi ñaan sama Boroom, xéynalee duma texeedi ci ñaan sama Boroom ». + +(49) Ba mu léen beddeekoo, ak la ñu doon jaamu ci lu dul Yàlla, may nanu ko Isaaxa ak Yànqooba, te ku nekk ci ñoom ñaar def Na nu ko muy ab Yonent. + +(50) May Nanu léen ci sunu yërmande, te defal Nanu léen tagg wu rafet séen ginnaaw. + +(51) Fàttalil ci Téeré bi Muusaa nekkoon na di ku ñu sellal, nekkoon na ndaw lu ñu yenkeewal ; + +(52) Woo woon Nanu ko ca wàllu ndey-joor tuur [doju Siiniin], Nu jegeel ko, déeyook moom + +(53) May Nanu ko ci Sunu yërmande mbokkam Aaróona def ko mu di Yonent. + +(54) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Ismaayla, doonoon na ku sàmm dëelam, te nekkoon na bu ñu yónni. + +(55) Te daan na digal ñoñam julli ak joxe asaka, te doonoon ku am ngërëmal Boroomam. + +(56) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Idriisa, nekkoon na ku dëggu te dib Yonent. + +(57) Yékkati Nanu ko teg ko ci barab bu kowe + +(58) Ñooñu ñooy ña Yàlla defaloon xéewal ci Yonent yi ñu bokk ci njabootu Aadama ak ña ñu yeboon [ca gaal ga] ñu ànd ak Nóoh ak ca ña Nu gindi, te tànn léen. Ñooñu, su ñu jàngee laayay Boroom yërmande ji ñu rot sujjóot, boolekook i jooy. + +(59) Mu am ñu léen wuutu séen ginnaaw, ñu sàggane julli, topp bànneex ya, ñooñu dey danañu tàbbi [xuru] safaraw “Gayy” + +(60) Ndare ña tuub, te gëm, te jëf jëf ju yiw. Ñooñu danañu tàbbi Àjjana, te déesu léen tooñ ci dara. + +(61) Àjjana yu sax ya Boroom yërmande ja dig jaamam ya ci kumpa. Moom dey digéem luy ñëw la. + +(62) Duñu fa dégg caaxaan, jàmm rekk la ñu fay dégg ! Fa la léen séen wërsëg di fekk subaak ngoon. + +(63) Loolooy Àjjana ji Nuy donnale képp ku ragal Yàlla ci Sunu jaam yi. + +(64) Nun dey dunu wàcc lu dul ci sa ndigalul Boroom. Moo moom li ci sunu kanam ak la ca sunu ginnaaw ak li ci séen diggante, te sa Boroom du fàtte. + +(65) Mooy Boroom asamaan yi ak suuf si ak li ci séen diggante ; jaamu [léen] ko, te ngéen sax ca jaamu ga. Ndax xamal ngéen ko kenn ku Ko niru ? + +(66) Nit a ngi naan : "Ndax su ma deewee danañu ma dekkal ?" + +(67) Xanaa nit dafa fàttalikuwul ne Noo ko bindoon ca lu jëkk, te du woon dara. + +(68) Giñ naa ci sa Boroom ne fàww dinaa léen fàng boole léen ak séytaane ya, te dananu léen dajale ca kéewal jaanama. + +(69) Te Dananu ñoddi ci kurél bu nekk ña ca gënoon a ñeme Yàlla. + +(70) Te Ñoo gën a xam ña gën a yeyoo lakk ci Safara. + +(71) Amul kenn ci yéen ku fa dul jaar. Sa Boroom dogal na ko, te du jaas. + +(72) Topp Nu musal ña ragaloon (Ÿàlla), Nu bàyyi ña tooñoon ñu bóof ca biir. + +(73) Bu ñu léen jàngalee Sunu laaya yi ña weddi wax ña gëm ne léen : ban ci ñaari kurél yi moo ëpp màqaama te gën mbooloo?. + +(74) Ñaata la nu alag lu léen jiitu ci ay maas yu léen ëppale te gën léen a taaru + +(75) Képp ku nekk ci cànkute, na ko Yàlla bàyyi ci cànkutéem mu wéy ca! + +(76) ba ñu gis li ñu léen dig : moo xam mbugal ma la walla bés-pénc. Bu boobaa danañu xam kan moo gën a yées daraja, te gën a ñàkk solo ab lël. + +(77) Yàlla dana dolli njub ñay sàkku njub, ay jëf yu yiw yiy des ginnaaw farata, ñoo ëpp yool ca sa Boroom te moo gën ag muj. + +(78) Xanaa gisóo ki di weddi sunu laaya yi te naan : "fàww deef na ma fa jox alal ak i doom". + +(79) Xanaa kii dafa xam kumpa, walla mu am lu mu dëelante Boroom yërmande ji? + +(80) Mukk ! Te dananu bind li mu wax, te dananu ko dolli mbugal mu baree bari. + +(81) Dananu nangu ci moom alal ji muy wax, mu ñëw ci nun ne cundum. + +(82) Jël nañu ñeneen def léen Yàlla, bàyyi fa Yàlla, ngir ñu dooleel léen + +(83) Mukk ! (séen Yàlla yooyu) danañu weddi jaamu gi ñu léen doon jaamu, nekk it séeni noon + +(84) Xanaa gisóo ni nooy yebal séytaane ya ca yéefër ya ñu léen di gësëm + +(85) Buléen yàkkamti (mbugal mi). Nu ngi léen koy waajal bu baax. + +(86) Keroog ba nuy fàng ñi ragal Yàlla, fa Boroom yërmande ja ñuy mbooloo, + +(87) Nu sëkkëtal saay-saay si jëme léen jaanama, ñu ànd ak mar wu metti + +(88) Tinu amu fa, lu dul ku fasante woon ak Boroom yërmande ji kóllare + +(89) Nee na ñooy Boroom yërmande ji dafa am doom! + +(90) Wax ngéen lu ñaaw + +(91) Asamaan xaw naa xotteeku, suuf siy waaj a xar, xeer yiy bëgg a jóoru. + +(92) Ngir li ñu wutal doom Boroom yërmande ji + +(93) Te jaaduwul ci Boroom yërmande ji muy doomoo kenn + +(94) Amul kenn ci asamaan walla ci kaw suuf ku dul ñëw fa Boroom yërmande ja ñëwinu jaam. + +(95) Dajaleléen, lim léen ba ñu mat + +(96) Ñoom ñépp danañu teew fa Moom bés-pénc, ku nekk ne cundum. + +(97) Ña nga xam ne gëm nañu, te def lu baax, Boroom yërmande ji, Yàlla dana léen defal cofeel. + +(98) Yombal nanu ko (Alxuraan) ci saw làmmiñ, ngir nga bégal ci ñi ragal Yàlla, te xupp ci nit ñi dëng. + +(99) Ñaata lanu alag ci ay maas yu léen jiitu, ndax yégati nga kenn ci ñoom walla nga dégg kàddoom ? + +saari alxuraan +alxuraan +Manees na a yër foofu, yennat ciy léeboo nga fa: http://www.au-senegal.com/-Proverbes-wolof-.html + +Aduna weru koor la faw jant so nga do nga waññi bis = La vie est comme le mois de ramadan tant que le soleil ne s'est pas couché on ne doit pas compter les jours + +Alalu golo ca lex ba = Tous les biens du singe sont dans sa joue. + +Léébu: proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Am naa giléem ca Gànnaar yomb naa wax = J'ai un chameau en Mauritanie, c'est facile à dire. Léébu, proverbes CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bakkan waruw dàll la : fa muy dagge doo ko yëg = La vie c'est comme une lanière de sandale : avant qu'elle ne soit rompue, on ne peut pas savoir où cela va se produire Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bala nga xam luw taat di jariñ, mbate toog jot = On ne connaît l'utilité des fesses qu'au moment de s'asseoir. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bant, lu mu yàgg cig dex, du tax mu soppiku jasiit = Un bout de bois, il peut rester longtemps longtemps dans un fleuve,ce n'est pas pour ça qu'il +va se transformer en crocodile. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bëgg-bëgg yee wuute, moo-tax njaay may jar ca ja ba = Les goûts sont différents, c'est pour ça que tout ce qui se vend au marché trouve acquéreur. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bëggum ñeex duma taxa dëppoo cin lu tàng = Ce n'est pas parce que je veux de la sauce que je vais me retourner la marmite chaude sur la tête. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Benn loxo du tàccu = Une main n'applaudit pas. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bes boo gis, day leb walla muy fey = Chaque jour est l'occasion d'une dette que l'on contracte ou que l'on rembourse. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan = L'œil ne porte aucune charge, mais il sait ce que la tête est capable de porter. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk = Le regard de l'amour passe par-dessus les défauts. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Béy du gëmal gënn = Une chèvre ne croit jamais qu'un mortier est vide. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Boo bëggee xam luy laabiir, amal doom = Si tu veux savoir ce qu'est l'indulgence, aie un enfant +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Boo bëggee xam luy muñ, amal jabar = Si tu veux savoir ce qu'est la patience, prends une épouse. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bopp du ngir karaw kessé = La tête ne sert pas qu'à retenir les cheveux + +Boroom ndékki ku ko jëkka yeewu tëddaat = Celui qui se lève avant le responsable du petit déjeuner peut aller se recoucher. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Boroom tubéy, bu jàngoo sol = Le propriétaire du pantalon, après s'être lavé les pieds, c'est lui qui le met. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bu daay také ceeli yendo naaw = L'épervier passe la journée à voler quand la brousse est en feu + +Bu la am-am taxa bew, ndax ñàkk du wees = Il ne faut pas être fier de sa fortune, car un revers peut toujours arriver. +Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986 + +Bu lëk lékkee olom nako gërëmee coy = + +ñaara mën k&nn te ñëtt du bëre = + +Lu kénn mën ñaara koko dàq = Ce que peut faire une personne, deux sont meilleurs que lui. + +Làkk +Arminaat seddatlinu taariix(date) yi la ci jenn jamono. Doon na ag noste gu waa Isipt yu yàgg ya sàkkoon ngir séddatle ak a nos jamono ji ci ay diir. Ca ndoorte la dañu koo sàkkoon ngir man a dëppale yenn feeñte yu saytubiddiw ak yu gëstubiddiw ak jamono ja ñuy amee. Doon nañu ko jëfandikoo it ngir natt seeni bési xumbéeli diine. + +Bennte yu arminaat +Ci taariix arminaat yépp a cëslaayu ci ay bennte(unite) yu dénd yu seen diir aju ciy feeñtey saytubiddiw. + +Bés +Daanaka ci xay yépp, coppite gi ci bés ak guddi moo doonoon bennte bi ñuy natte at yi. Wëndéelug Suuf si doon li waral safaanu googu, te njël gi du amandoo ci barab yi ne ci kol-kolu suuf si . Soo xoolee Senegaal ak Faraas bokkuñuy waxtu, Faraas a ñuy rawee ñaari waxtu su dee nawet la, benn waxtu su dee noor la . + +Weer +Li demiinu weer doon lu yomb a may-bët, moo tax mu doon ab jumtukaay ngir natt jamono ji. Arminaatu jullit ñi moon weer wi lay topp , waaye arminaatu geregori moom jant bi lay topp. + +At +Mooy mbooleem jamono yi, at doon na diir bu gudd. Cig njort, Moom it ci yenn feeñtey dénd la ko nit ñi ko sàkk arminaat daa natte. + +Arminaat bi njëkk a cëslaayu ci at, maanaam ci soppiku at ba at mooy arminaatu waa isipt. + +Booleeg benntey dénd yi + +At ak bis +Ci jamono ji ñu ne, am at mooy 365,24220 bis. arminaatu waa isipt, ak arminaatu suleymaan, ak arminaatu geregori, doon nañu ay royuwaay ci liggéey bu mag bi ñu def ngir man a dëppale (syncroniser) at mi ak wëndéelug Suuf si ci li wër jant bi. + +ba tay sax séenug dëppoo des na, ba tax na 10000 at yu ne di na juum 3 fan. + +Weer ak bés +Diirub weer mooy 29 bés 12 waxtu 44 simili ak 2,8 saa (muy 29,53 bés). Kon su ñuy weccee ay weeri fanweeri fan ak yu ñaar-fukk ak juroom-ñenti fan, te di yokk benn bés fanweeri weer yu ne, dina doon lu nanguwu. wii nattiin, arminaati weer yépp a koy jëfandikoo ngir dëppale bés yi ci weer ak wëndéelinu weer wi. + +Jamono ak at +Ci arminaat yu bari, ñeenti jamono ñoo am: noor, nawet, lolli. Jamono yooyu, ci xay goo dem ak ni ñu koy séddalee ci at mi. Su ñu xoolee waa siin ñoom nawet la at mi di tambalee. +Saytubiddiw mooy xam-xam biy xool aka saytu biddiw yi, di jéem a faramface ak a leeral seen melokaan ci jëmm ak ci simi, seenug magg ak seen cosaan. Doon na xam-xam bu am lu ëpp 6 000 at, ay cosaani saytubiddiw jiitu na jomono ju yàgg ja. + +Te ñu bañ koo jaawale ak gëstubiddiw + +Taariixkat yi nee nañu saytubiddiw mooy xam-xam bi gën a yàgg ci àdduna bi. Xay yu njëlbeenu yi sax amoon nañu ci ay xam-xam. + +Tekkiinam + +Xam-xamu saytu-bidiw bokk na ci xam-xam yu njëkk yi am ci fajarug nite, moom xam-xam la buy yittewoo fuglu ak jàng xew-xew yiy xew ci bitib kol-kol bu suuf si ak ci muuraay gu jawwoom gi. Mooy it xam-xam biy joxe xibaar yi aju ci feeñte (phenomene)yu bidiw yi. Saytu-bidiw mooy gëstu tàmbalig yaram yi ñu man a fuglu ci asamaan si (biti suuf si), ak séenug jëm-kanam ak séeni jagle yu jëmm (walla fisiyaa) ak yu kimyaa, ak xew-xew yi ñuy àndal. + + Français:astronomie + English:astronomy +Gëstubiddiw mooy mboolem aada ak gëmgëm yi japp ni fi jawwu yi féete ci nosteg jant bi ak biddiw yiy feeñ ci asamaan si ci yenn jublu yi, ci yenn bis yi, ak ci yenn waxtu yi, manees na cee jaar jàngat lu xew walla lu nar a xew, moo xam muy lu ñeel kenn nit mbaa mbooloo. Ginnaaw nag xam-xam la boo xam ni ci aaday aki gëm-gëm la aju, aada ju nekk am na nu mu ko gise. + +Boroom xam-xam yiy tënku ci lu xel nangu nag, dañu koo jàppe ni xam-xamlu, ñenn ñi yegg ci jàppe ko gëmgëmu Yëeli (Yàlla ju wérul). Mboolem gëstu yees ci mas a def ca jamonoy yàggte ga ba léegi ci dàq ko lay mujj. + +Ñi koy layal nag dañuy wax ni wax luy xewi ëllëg taxukoo jug, ndax man naa nekk luy bijji nit ki ba mu def lum jortulwoon ni man na ko ngir am yaakaar ci ëllëg. + +Français:astrologie +Eglish:astrology + +Gëstubiddiw +Jàpp nañ ne koom-koomu Afrig mooy gi gën a dellu ginnaw, suñu koo mengalee ak yeneen gox yi.Koom-koom dafa doon lu yaan, bariy fànn, kon fii dañ fiy junj yenn yi rekk. + +Mbay +Njuddéef (production) mu mbay mi ci Afrig day wuute wuute gu mag, kem ni kilimaa bi wuutee, ndax diiwaan yu tàng yi la fay juddoo ci mbay bokkul ak lay juddoo ca diiwaan yu diggdoomu ya (yu yamuw tàngoor ya). + +Ëlëgu mbay ci Afrig lu am yaakaar la, ndax am na fi ay yaatu-yaatu yu mag ci suuf su nangu mbay su ñu jëfandikoogul, kon ëlëgu koom-koomu Afrig lu mat a dale‘m xel la, ndax li muy wund lépp aw yiw la ak mbégte. + +Bokk na ci njuddéefi mbay yu afrig yi ëpp solo yii: + + Kakaawoo: mi ngi ci tefesug Gana gi, di ñatti ñeenteeli njudéefi àdduna bi (maanaam bu ñu xaajoon li ci àdduna biy liggéey ci Kakaawoo ñeenti xaaj, ñatt yi fa lañu leen di liggéeye). + + Diwug garabu tàndarma : mi ngi ci Tefesug Gana gi, Afrig nag mooy gox bi ëpp lu koy jóox (produire) ci àdduna bi. + + Kafe : ci Ecoopi, Keeñaa, Ugandaa, Ginne, Kot Diwaar + + Gerte : Sudaan, bëj-gànnaaru Niseria, ak Senegaal + + Gom (gomme arabique): ci Sudaan, lu tollook ñeenti juroomeeli njuddéefi àdduna bi. + + Anaanaas ak banaana: ci peggi gotti Yamoo yi + + Saytoon (olive) , mawaalih, dugubi qamh ak mboq : ñi ngi ci cat yu bëj-gànnaar yu Gox bi, rawati na ci diiwaanu Maghreb bu Araab bi. + +Jur gi +Boo gëstoo dinga gis ne : + + Ay milyoŋi bopp cig jur ñi ngi leen di yare ci sàmmuwaayi Sawaana yi ci Diiwaani Gëwéel yi, ñi ngi yar it ay milyoŋi bopp ciy xar aki bëy ci sàmmuwaay yu diggdoomu yi (walla yu yam tàngoor yi) ci bëj-saalumu Gox bi ak ci bëj-gànnaaram gu sowwu ci Maghreb gu Araab gi, ay milyoŋ it ciy giléem ñi ngi leen di yar ci tàkki Afrig yu yaatu yi. + + Njuddéef (produit) yi tukkee ci jur gi, ci Afrig, am nanu doole bu baax ci yaxantu gu àdduna bi . Afrig gu bëj-saalum gi moo jël ñeenteelu barab ci réewi àdduna yiy génne ngënël (laine),. Maxrib gu raab gi moom dina génne (exporter) ay xar, di génne ay njuddéefam ñuy ngënël, yàpp, jëme leen ci réewi Tugal yi + +Mbell yi +Afrig gox la bu naat te woomle ci ay koom yu mbell, lu ëpp ci mbell yooyu nag ñi ngi ci bëj-saalumu Afrig, ak ci mbalkam Kongoo, ak ci réewi Maghreb gu Araab gi. Yi ëpp solo ci mbell yooyu ñooy yii : + + Jamaa: lu tollook 91% ci njuddéef mu àdduna bi (li ci àdduna biy liggéey) + Wurus: lu tollook 65% ci njuddéefu àdduna bi + Xànjar: lu tollook 23% ci njuddéefu àdduna bi + Yoraaniyom: lu tollook 60% ci njuddéefu àdduna bi + Fosfaat: lu tollook 33% ci njuddéeefu àdduna bi. ( ma nga ca réewi Maxrib gu Araab gi) + Kobalt: lu tollook 70% ci njuddéefu àdduna bi + Manganiis: lu tollook 20% ci njuddéefum àddunaà bi + Boksit: (Alimiñom bu ñu laalul) mi ngi ci Gineek Gana + Petrol: lu tollook 11% ci njuddéefu àdduna bi, mi ngi nag ci Tàkk gu mag gi, ci Isipt , Libi, Alseeri ak Niseeria. + +(yii nag ay njoxe (donnée) lañu yoy man naa am soppeeku nañu) + +Ndefar (industrie) +Ku gëstu dinga gis ne Afrig : + +Gox bu naat la ci ay gongikuwaay yu xéewal yu gàncax, yu mbay, yu jur (dundat) ak yu mbell, niki : wëtéen, ay diwi gàncax, daakaande gi (gomme arabique ), kakaawoo, xànjar, wurus, bettax, fosfaat ak petrol, yii yépp ay njuddéef walla ay ne-ne yu ñu laalul (produits bruts) la ñu, yu am solo te manadee ñàkk ci wàllug ndefar. + +Looloo taxoon gox bi di am rëbb (proie) mu réewi Tugal yu sancaan yii di woroomi ndefar (industries) yu mag doon xëccoo, ngir jot – ci anam gu yomb ak ci njëg yu jàppandi - ci ne-ne yu ñu laalul yu fees dell yii ci Gox bi te seeni ndefar di leen soxla, di leen manadee ñàkk. Bu ko defee ñu leen di indeeti giñnaaw bi ñu leen defaree ngir jaaysi leen ci ja yu Gox bi ci ay njëg yu seer te kawe. + +Looloo tax it réewi sancaan yu mag yi doon def ay politig yuy tee ndefar yu barab yi (l’industrie locale) di am ak a sawar, ngir Afrig des di ab ja bu mag bu ñuy jaaye njuddéefi Tugal yi ci ay njëg yu kawe, ak it ngir Afrig bañ di jëfandikoo ne-neem yu ñu laalul yi, te loolu doon na am bu ndefaram doxoon te jëm kanam. Ci nii la Afrig di dese dib gongikuwaay bu mag buy génne ay ñumm (ay ne-ne yu ñu laalul) ñeel réewi séancaan yu ndefar yii, te it dib ja buy guux mbooleem sila (marsandiis) yiy bàyyikoo ci yii réew. + +Bii politig moo lënk te takk koom-koomu Afrig bi ci koom-koomu réewi sancaan yi, bu ko defee gox bi mujj di lu lott ci amal ag tembam gu koom-koom, bu ko defee réewi gox bi mujj di yu ginnaawe, seeni tolluwaayu dund suufe , tolluwaayi dund yu réewi Tugal yi kawe. + +Askani Afrig yi yewwu nanu ci mujjantal gi, jamonoy jànkoonte ak jàmmaarloo gu tar tàmbali lànk canc gi, looloo jur tembug askani Gox bi ci politig, daal di tàmbali di jariñu ci koomi seeni réew ñeel seen bopp, di liggéey it ngir mel ne ñépp ci jekk ak am dund gu neex. + +Kon ëlëgu Gox bi gu ndefar ay xéewal rekk la. Ndax kat bu weesoo li gox bi nekk di lu fees aki ñumm yu wuute, teewul mu am sàq mu réy ci ay gongikuwaayi kàttan (source d’énergie), rawati na mbëjum ndox (kurãŋ buy ame ci ndox), petrol ak këriñ. + +Wàllug jokkoo (communication) +Gox bi day sukkandiku - cig jokkoom – ci yooni weñ yi (raay yi) , yooni jéeri yi ak ngaalug dex (navigation fluviale). Waaye nag gox bi lu deltu-ginnaaw la ci wàllug jokkoo, bu ñu ko nattee ci yeneen gox yi, loolu nag li ko waral mooy lii: + + Tàkk yu yaatu, yu bekkoor, yu néewi ndox yi. + Gotti Yamoo, yu fatt, yu bari yi ay ngirowaay aki déeg. + Bari gi mu bari ay rotuwaay aki balluwaayi ndox (cascades) + Ñugg-ñugg yi ( creux; movement du sol; ride) yu wow yi ci yenn wàll yi. + +Réewi gox bi man nañoo noot jafe-jafe yii, gën a jëmale kanam seen jumtukaayi jokkoo bis bu Yàlla dogalee ndefar yewwu fi ba jëm kanam. Jamono jii ñu tollu gox baa ngi sàkk ay yooni jawwu yu am solo yu koy àggale ci mbooleem wàll yi. + +Koom-koomu Afrig +Afrig gu Bëj-saalum mooy réew mi gën a féete Bëj-saalum ci goxu Afrig, mi ngi bokk ci diwaanu Bëj-saalumu Afrig. + +ci Bëj-saalum klimaa bu mel ne Gu Diggu gi la am, ci li wër Kap, ci bëj-gànnaar nag klimaab gëweel la am. + +réew mi am na 47 556 900 ciy way dëkk. Ñetti dëkk yi fa gën a réy ñooy Kap mi am 2 984 100 ciy way dëkk, Duurbaan 2 531 300 ciy way dëkk, Johannesburg 1 975 500 ciy way dëkk ak Pretoriya, di péyam, am lu tollook 1 473 800 ciy way dëkk (yii lim nak ca 2004 lawoon). + +Réyaayam toll ci 1 219 912 km², di 33° réew ci réyaay ci àdduna bi. Am tefes gu guddee 2 798 km. Mi ngi feggool ak Botswana, Lesoto, Mosambik, Namibi, Eswatini, Simbaawee, réew yii yépp nag ci bëj-gànnaaram la ñu ne. Pegg gi ne ci seen diggante nag toll na ci 4 862 km. + +Lëkkalekaay yu biti + + +Melosuufug Afrig gu Bëj-saalum +Melosuufug afrig +Alseeri doon na réew mu bariy doj. Ci bëj-gànnaar gi, boo jàppee penku jëm sowwu gépp ab càllaleeb ay doj ñoo fa ne, am na it wàll gu bari ci tàkkug Sahara gi. Ñi ngi koy boole ci Bëj-gànnaaru Afrig, di 11u réew mi gën a réy ci àdduna bi. réeyaayam toll ci 2 381 741 km², ma na 998 km ci tefes. + +Ci bëj-saalum mi ngi feggook Mali, ak Gànnaar, ak Niseer, ci penku mi ngi taqalook Tiniisi, ci sowwu Nguuru Marook, ci bëj-gànnaar mi ngi yem ci Géej gu Diggu gi. Pegg gi mu amal ak yenee réew yi toll na ci 6 343 km. + +Melosuufug afrig +Melosuufug Alseeri +Séex Anta Jóob mu ngi juddu ci 29 deesàmbar ci atum 1923 ci ceytu, faatu ci 7 féwrier ci atum 1986 ci Ndakaaru. MoomlSénégala Saa-Senegaal la di gëstukat ak ku doon yëngu ci walu polotig giirug dundam, dafa doon wane ñariñu Afrig rawati na der bu ñuul ci mboorum aduna si. + +Ba tay amna ci Mbidam yu ñuy ŋañ, ba taxna du ñu kay faral di féssal, rawatina li mu binda ci walu Egypte ak ciossaanu kalaama wolof. + +Wayé Séex Anta Jóob bokk na ci ñi njëkk a bind ci mbooru Afrig ak kolonisationg. + +Diar diar am ak ŋiagalém + +Séex Anta Jóob muŋi juddu ci 29 déçambar ci atum 1923 ci ceytu, ci diwaanu Bambeï, ci ŋiaaréem. + +Ci askane wu mag la soxékoo. Bi mu amé 23 att la dém farançe ŋir diaŋ physique akk chimie, wayé mu moudjé djublu ci histoire akk science sociales, rawatina ŋiaŋalém Gaston Bachelard akk bu Frédéric Juiot-Curie. Moome bokkul guiss guiss akk  ñiy xalaate ni afrik amoul histoirou bopam. + +Ci atum 1951 la Séex Anta Jóob , ci dimbalu Marcel Giraule, wadjal thézou doctorat ci ñiangalé mu kawé ci université bu Paris. Ci thèze boobu ci la xamlée ni waa Egypte ay nitt ñu ñul lañiouwoone té itam lakk akk aaday afrik yi fofu la soxékoo. +Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi mooy mbalkaam ndox mi ne ci li wër Dottub Bëj-saalum bi. Mooy ñenteelu mbàmbulaan mi gën a réy ci àdduna bi. + +Yaatuwaayam gépp mi ngi toll ci 20 327 000 km², guddaayu tefes gi di 17 968 km. + +Mi nu wuteeg yeneen mbàmbulaan yi seen dig doon ay gox, moom rek mooy la ñuy tekkee ni ab mbalkaam ndox mu wër ab gox (goxub Dott bu Bëj-saalum); doon ab jaaro bu tëdd ci 60°(60 aj) gu tus-wu-gaar wu Bëj-saalum. + +Mbàmbulaan gu Bëj-saalum xóotee na lu tollook 4 000 ba 5 000 m, daanaka ci tëraayam gépp, lu weesu yénn barab yi gën a néew xóotaay. + +Mbàmbulaan yi +Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar gi yaatuwaayam toll na ci 14 090 000 km², looloo waral muy mbàmbulaan gi gën a tuuti ci àdduna bi. Moo ëmb mbooleem géej yi ne ci li wër dottub Bëj-gànnaar bi ak yi ne ci Bëj-gànnaar gu Tugal, gu Aamerig ak gu Asi. Mi ngi taqalo ak mbàmbulaanug Atlas jaare ko ci géejug Barents ak gu Dal gi. + +Mbàmbulaan yi +Dottub Bëj-gànnaar daa am ñaari tekki ci benn bi ab tomb la (ci la nuy wax ci bii jukki), ci beneen bi ab gox la, Dottub Bëj-gànnaar. + +Dottub Bëj-gànnaar mooy cat li gën a féete Bëj-gànnaar ci àdduna bi. + +Suuf si ñaari cat la am ñu + +xool it + Dottub Bëj-saalum + Goxub Dottub Bëj-gànnaar + Goxub Dottub Bëj-saalum + +Lëkkalekaay yu biti + Dottub bëj-gànnaar + Dal buy wax doot bi ci kàllaama wa angalteer + +Diiwaani dott +Końskowola ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Poloñ. Mi ngi ne ci diggante Puławy ak Lublino, ci wetu Kurów, ci dexu Kurówka. Mooy péyu gox-goxaan bii di gmina. + +Mi ngi yaatoo 9,8 km², ci 2004 amoon na 2.188 way dëkk. + +Poloñ +Kureelu Mbootaayu Xeet yi ndawi réew yu mag yi, yu ci mel ni Nguur-Yu-Bennoo , Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig, Bennog Sofyet, Faraas ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi . +Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu r;ew yi, ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér. +Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu àdduna bi ci dëkku San Fransisco ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi. +Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy: + +Nun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef . + +Sosteefam +Njiitul Aamerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu àdduna bi, guy jeem a indi jàmm ci àdduna bi, ci ginaaw Xareb Àdduna bu Njëkk bi. + +Waxoon nañu ne Wilson moom jotoon naa leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lañu woon ak ñeent ci biir Xareb Àdduna bu Njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy réew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati. + +Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu Mbootayu Xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa ñu amaloon, kollëre ga ñu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lañu fa xaatim. + +Ay ponkam + +Sose kureelu xeet yi ci mbooleem réew yi am tembte gu mat gu dara wàññiwut, réew yoo xam ne man nañoo indi ay warlu yu mat ci jox-cër walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral. +Réew yi bokk ci kureel gi danañu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir ñu àtte leen, te xool li leen boole. Réew yi ci bokk it war nañuy seet mbugal yi yell ci réew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw. + +Jeem a dëgëral buumi dimblante ci àdduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés, ak wormaal kollërantey réew yi, ak xeex njaam, ci meloom yépp, jeem a rafetal nekkiinu liggéeykat yi ak seenug dund, ak xeex seneebar, nos yaxantu ci àdduna bi, ak sonn ci wér-gu-yaramu nit. + +Réew yi ci bokk danañu warlul yeneen réew yi wormaal seenug tembteg politig , danañu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi réew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk. +Aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem réew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi ñu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak réew yi ñu gañee ci xareb àdduna bu njëkk bi. +Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, ñu feetale leen réewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi réew yooyu nekkee ci waawug réew yi ñu daanoon ci xeex bi, ñuy : réewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag ñu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen a may ag tembte ëlëg. Kureel gi, bi muy door a sosu, 42 réew a ca bokksi woon. Ci noonu réew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub réew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu ci bu ñuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk. + +Bànqaasi kureelu gi +Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy : + +Jataay bu Matale bi, Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : Àttekaayu Maanduteg Àdduna bi ak Mbootaayug Liggéey gu Àdduna bi. + +Jataay bu matale bi +Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi réew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru koor, ngir xool aka xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay tëralam (prograamam). + +Jataayub kureel bi +Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cër, juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy réew yi am ag bokk gu sax ñooy: Nguur-Yu-Bennoo yi, Faraas, Itaali, Sapoŋ ak Almaañ mi jël cërub Aamerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti réew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg. Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi àdduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent. + +Koolute gi (secretariat) + +Koolute gu kureelug gi, mi ngi sosoo woon ci liggéeykat yu kureel bi, ya daa liggéeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale, ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg caada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex seneebar, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi. + +Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: Àttekaayu Maanduteg Àdduna bi, liggéeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon bu àdduna bi, ak kollërante yi réew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne réewi kureel bee leen di indi. Àttekaayub Maanduteg Àdduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Olaand. Ak Mbootaayug liggéeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci Àdduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi liggéeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom liggéey yi. Geneve nag moo dib dalam. + +Ay ayibam +Kureelu mbootaayu xeet yi de, ak li mu def lépp ci liggéey yu jëm ci saxal jàmm ci àdduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci liggéey yu am njariñ ci wàllug mboolaay, loolu lépp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ŋaayoo yi daa am ci diggante réew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu gi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee réew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Sapoŋ defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy génn gu ci Sapoŋ ak Almaañ génnoon ci atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecoopi ci atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu génn ci kureel bi ci atum 1937g. Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon a tee ay “dank yu xare” yu bees di am, maanaam ay réew dajaloo, boole seen bopp ci wàlli xare. Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon a tee réew yu mag yi di rawante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci génn. + +Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti réew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Nguur-Yu-Bennoo yi ak Faras ñu man a sancati ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci réewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug réewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Réew yu mag yii danoo jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgga def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif réew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ. + +Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi réew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi ñu daa gaaral ci kureel bi. + +Jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay kër-këraanam +Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy: + + Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi. + Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi. + Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit. + Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg. + +Bu dee ker-keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii: + +Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi. +Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi. +Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi. +Sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi. + +Campeefi mbootayu bi aki bàqaasam +Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy: + +Jataay bu matale bi +Mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem: + + Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi. + Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi. + Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk. + Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi . + Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi. + +Saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man’a doon walla ab ndenkaane. + +Jaataayu kaaraange gi +Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe. +Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi. +Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci. +Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex. + +Koolute gu matale gi +Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi . + +Jataayub koom-koom ak mboolaay +Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo: + +UNESCO +Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans. +Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi. + +Mbootaayu Liggéeyu Àdduna bi +Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu liggéeykat yi ci àdduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte . +Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve. + +Mbootaayug Wérug Àdduna bi +Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam. + +Mbootaayu dund ak mbay gu àdduna bi +Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali. +Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi: + +Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi. +Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand. + +Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax +Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen. + +Jataayub ndénkaan yi +Mooy saytu mbirum sancu yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi. + +Bankub addunna bi ngir sos ak tabax +Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg . +Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig. + +Keesug kee gu àdduna bi +Yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi . + +Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy: + mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll. + Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp. + Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ. + +Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi. +Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. +Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon. + +Lëkkalekaay yu biti + dalub KMX + +Kureelu Mbootayu Xeet yi +Adduna +Mbootaayu Réewi Jullit yi gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g. +Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk . + +Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf. + +Kollëreg mbootaay gi +Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 - 4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi. + +Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen réew yi. +Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe: + + Yamoo gu mat ci diggante réew yi ci bokk + Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram. + Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb. + Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk. + Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi. + Jeem a far boddante ci biiru xeet, ak sanc ci mbooleem ay anamam. + Def lépp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute. + Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf. + Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew. + Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo . + Réew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam . + +Campeefi mbootaay gi +Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki : + Jataayu buur yi ak njiit yi + Jataayu jëwrini bitim reew yi + Koolute gu matale gi + Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi. + +kureel yi ci bokk + + Kureelu Quds + Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar + Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada. + Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala + Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu + Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada + +yi bànqaasoo ci mbootaay gi + Nafag dimblante gu lislaam gi + Nafag Quds + Daaray gëstu gu lim yi ak koom, ak mboolaay. + Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu. + Cëslaayu lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom. + Barabu àdduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam. + Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu + Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi. + Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li + Akaademi bu xam-xamu lislaam + Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi + Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon + +yeneen cëslaay +Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy + Banku lislaam bi + Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi + Mbootaayu rajoy reewi jullit yi + Neegub yaxantu bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi + Mbootaayu peeyi lislaam yi + Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi + Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada. + +Jagley campeef yi +Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam. + +Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk. + +Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g . +Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g. +Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g. +Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g. + +Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam. +Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko. +Mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi. +Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi. +Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee. + +Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g. +Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi. +Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi. +Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle. +Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” . Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi. +Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal. +Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g. +Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi. + +Liggéey yi + Di gëstu lay xew Quds + Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen, + Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds + Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju. + Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi. + +Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at. + +Lislaam +Goxub Afrig + +Gëstu gi aju ci ay way dëkkam: + +Lii mooy am-am yi fi nekk: + +Ø Diiwaan yu fatt yi ci ay way dëkk: yii diiwaan nag ñi ngi ci barab yi barim mbay, mbell ak klimaa bu méngoo, ci xuru Niil wu jege wi ak Delta ak ci barabi tefes yi ci bëj-gànnaaru Afrig, ak ci Laamaaru Ngéej yu Yamoo yi, ak ci tefesug sowwu Afrig, ak ci diiwaani bëj-saalum yi ak bëj-saalumu penku ci Afrig gu bëj-saalum gi. + +Ø Diiwaan yu diggdóomu yi cig dëkk: barab yii lu diggdóoomu te yam ci ag fatt ci wàllug dëkk moo fa nekk, maanaam ña fa dëkk bareewuñu noonu, moom nag ay yaatu-yaatoo fa nekk yu rëy ci ay sammuwaay, ci goxi Sudaan yu sowwu yi, dale ko ci dexug Senegaal gi ba ca ngéejus Càdd si, ak ci xuru Niil ci Sudaan ak ci Laamaaru Eccopi ak ci Sowwu Afrig ak bëj-saalumu mbalkam Kongoo. + +Ø Diiwaan yi bariwul ay way dëkk: ñooy tàkk yu bekkoor yi, niki : Tàkk gu mag gi, Tàkkug Kalahaari gi ak Tàkkug Somaali gi, ak itam gotti Yamoo yu fatt yu bari yi ay ngirowaay aki tawat, ci mbalkam Kongoo ak digg Afrig. + +Ø Way dëkki Afrig ñu néew lañu, bu ñu leen nattee ci tolluwaayam bu rëy bii (moom Afrig): sababus loolu day dellu ci ni ab déndam méngoodee, ñagase ni. Ak itam sanc gi ko Tugal sancoon te yàgg fi, giir ay xéewalam yu dénd, te loolu indil ko ag dellu ginnaaw gu mag. Lii lépp nag dox na ci taxawal màggug way dëkkam. Leegi nag duggalees na fi jumtukaayi feg yi aju ci wàllug wér gu yaram, bu ko defee way dëkk yi tàmbali di bari, di màgg. Limub way dëkki Afrig àgg na ci 350 ci milyoŋi nit , ñi ngi séntu lim bii romb ko ba àgg ci 520 milyoŋi nit ci mujjug xarnu bii. + +Xeeti way dëkk yi: + +Ø Way dëkki goxub Afrig tollu nañu ci lu jege 350 milyoŋ ciy nit, maanaam lu tollook ay fukki yoon la dëkk Isipt ciy way dëkk, ñi ngi séntu bii lim àgg ci 520 milyoŋ ciy nit atum 2000. + +Ø Way dëkki gox bi ñi ngi sosoo ci ay: ñu ñuul, ay araab, ay tubaab ak lenn ci ay xeet yu bawoo Asi, ñu ëpp ci ñoom nag ay waa Siin lañu aki waa End. + +Ø Ñu ñuul ñi: ñooy ñi cosaanoo ci gox bi, ñoom nag ñi ngi nekk ci digg bi ak ci bëj-saalum gi. Ñoom nag daje nañook ag jaay doole gu mag gu tukkee ci way sanc yi, rawati na ci jamono ji nekk ci diggante ñaari xarnu yii: 16 ak 17. ñoom sancaan yi ñoo sawarloo njàppum jaam mi te di ci xiirtale, rawati na ci tefesi sowwu Afrig yi ak mbalkam Kongoo, loolu waral ñu ray lu sakkan ci waa Afrig yi, ña ca des gàddaay dugg ci biir gox bi. + +Ø Araab yi: ñi ngi nekk ci xaaj bu bëj-gànnaar bi ci gox bi, rawati na ci réewi naar yi, di : Isipt, Sudaan, Libi, Tinisi, Alséeri, Marog, Gànnaar ak Somaali. Séenub lim dees na ko nattale ci 100 milyoŋ ciy nit, maanaam luy tollook 2/7 ci way dëkki gox bi. Tàkk gu mag gi nag mooy aji tàqale ji tàqale diggante ñu ñuul ñi ci bëj-saalum ak naar yi bi bëëj-gànnaar + +Ø Waa Tugal yi: ñi ngi ñëw ci gox bi ànd ak cancug Tugal gi la ko dale ca 17eelu xarn. Ñu seet fa gën a neex wàcc fa, muy barab yi gën a neex a dëkke, fi suuf si yekkatikoo, klimaa ba méngoo fa, ci penku Afrig, ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa ak Malaawi. Teg nanu loxo bëj-saalumu Afrig, sosal fa séen bopp am pénc (republique) mu temb, ñu yor fa cang ga ak njiit la ci kaw ëppte (majorité) gu nit ñu ñuul ña, di fa doxal it politigu teqale ci biiru xeet (walla boddante ci biiru xeet). Néewte gu weex googu it (minorite blanche) ci Rodisiyaa tegoon na loxo ca nguur ga walla àtte ga, daal di jibal ag tembam, di def it politig bu mel ne ba ñuy doxal ca bëj-saalumu Afrig, muy boddante ci biiru xeet + +Ø Néewte yu Asi yi: ñi ëpp ci ñoom ay waa Siin lañu aki waa End, ñi ngi ci digg ak bëj-saalumu Afrig, ñi ëpp ci ñoom it canc gi lañu àndaloon ñëw fi. Ña ca gën a bari dañuy liggéey ci yaxantu, ñenn ci ñoom dañuy def ay mecce yu ndefar (industrie). + +Jafe-jafey way dëkk yi fi cosaanoo: + +Ø Deltu ginnaaw gi jokkoo gi (communication) def + +Ø Tas gu fa mbas yi tas ak tawat yi ngir méngoodig melokaani klimaa bi + +Ø Ñàkk a tembug koom-koomu Afrig bi ak lënku gu mu lënku ci koom-koomu réewi sancaan yi + +Ø Boddanteg xeet gi ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa + +Ø Nekk gi yenn néewte yi di ay jàmbur (dëkkunu fi) nekk ci yenn ci réewi gox bi + +Ø Ñàkk a jëm kanam ci wàllug njàggale ak xereñ yi manul a ñàkk cig jëm kanam ak màggug koom-koom. +Way dëkki Afrig ñu néew lañu, bu ñu leen nattee ci tolluwaayam bu rëy bii (moom Afrig): sababu loolu day dellu ci ni ab déndam méngoodee, ñagase ni. Ak itam sanc gi ko Tugal sancoon te yàgg fi, giir ay xéewalam yu dénd yi, te loolu indil ko ag dellu ginnaaw gu mag. Lii lépp nag dox na ci taxawal màggug way dëkkam. Leegi nag duggalees na fi jumtukaayi feg yi aju ci wàllug wér-gu-yaram, bu ko defee way dëkk yi tàmbali di bari, di màgg. Limub way dëkki Afrig àgg na ci 350 ci milyoŋi nit , ñi ngi séntu lim bii romb ko ba àgg ci 520 milyoŋi nit ci mujjug xarnu bii. + +Diiwaan yu fatt yi ci ay way dëkk +yii diiwaan nag ñi ngi ci barab yi barim mbay, mbell ak klimaa bu méngoo, ci xuru Niil wu jege wi ak Delta ak ci barabi tefes yi ci bëj-gànnaaru Afrig, ak ci Laamaaru Ngéej yu Yamoo yi, ak ci tefesug sowwu Afrig, ak ci diiwaani bëj-saalum yi ak bëj-saalumu penku ci Afrig gu bëj-saalum gi. + +Diiwaan yu diggdóomu yi cig dëkk +barab yu diggdóoomu te yam ci ag fatt ci wàllug dëkk moo fa nekk, maanaam ña fa dëkk bareewuñu noonu, moom nag ay yaatu-yaatoo fa nekk yu rëy ci ay sammuwaay, ci goxi Sudaan yu sowwu yi, dale ko ci Dexug Senegaal gi ba ca ngéejus Càdd si, ak ci xuru Niil ci Sudaan ak ci Laamaaru Ecoopi ak ci Sowwu Afrig ak bëj-saalumu mbalkam Kongoo. + +Diiwaan yi bariwul ay way dëkk +ñooy tàkk yu bekkoor yi, niki : Tàkkug Sahara, Tàkkug Kalahaari gi ak Tàkkug Somaali gi, ak itam gotti yamoo yu fatt yu bari yi ay ngirowaay aki tawat, ci mbalkam Kongóo ak Diggu Afrig. + +Xeeti way dëkk yi +Way dëkki goxub Afrig tollu nañu ci lu jege 350 milyoŋ ciy nit, maanaam lu tollook ay fukki yoon Isipt ciy way dëkk, ñi ngi séntu bii lim àgg ci 520 milyoŋ ciy nit balaa yàgg. + +Way dëkki gox bi ñi ngi sosoo ci ay ñu ñuul, ay araab, ay tubaab ak lenn ci ay xeet yu bawoo Asi, ñu ëpp ci ñoom nag ay waa Siin lañu aki waa End. + +Ñu ñuul ñi +ñooy ñi cosaanoo ci gox bi, ñoom nag ñi ngi nekk ci digg bi ak ci bëj-saalum gi. Ñoom nag daje nañook ag jaay doole gu mag gu tukkee ci sancaan yi, rawati na ci jamono ji nekk ci diggante ñaari xarnu yii: VI ak VII. ñoom sancaan yi ñoo sawarloo njàppum jaam mi te di ci xiirtale, rawati na ci tefesi sowwu Afrig yi ak mbalkam Kongóo, loolu waral ñu ray lu sakkan ci waa Afrig yi, ña ca des gàddaay dugg ci biir gox bi. + +Araab yi +Ñi ngi nekk ci xaaj bu bëj-gànnaar bi ci gox bi, rawati na ci réewi naar yi, di : Isipt, Sudaan, Libi, Tiniisi, Aljeeri, Marook, Gànnaar ak Somaali. S��enub lim dees na ko nattale ci 100 milyoŋ ciy nit, maanaam luy tollook 2/7 ci way dëkki gox bi. Tàkkug Sahara gi nag mooy aji tàqale ji tàqale diggante ñu ñuul ñi ci bëj-saalum ak naar yi ci bëëj-gànnaar. + +Waa Tugal yi +Ñi ngi ñëw ci gox bi ànd ak Sancug Tugal gi la ko dale ca VIIeelu xarnu. Ñu seet fa gën a neex wàcc fa, muy barab yi gën a neex a dëkke, fi suuf si yekkatikoo, klimaa ba méngoo fa, ci penku Afrig, ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa ak Malaawi. Teg nañu loxo bëj-saalumu Afrig, sosal fa séen bopp am pénc (republique) mu temb, ñu yor fa cang ga ak njiit la ci kaw ëppte (majorité) gu nit ñu ñuul ña, di fa doxal it politigu teqale ci biiru xeet (walla boddante ci biiru xeet). Néewte gu weex googu it (minorite blanche) ci Rodisiyaa tegoon na loxo ca nguur ga walla àtte ga, daal di jibal ag tembteem, di def it politig bu mel ne ba ñuy doxal ca bëj-saalumu Afrig, muy boddante ci biiru xeet. + +Néewte yu Asi yi +Ñi ëpp ci ñoom ay waa Siin lañu aki waa End, ñi ngi ci digg ak bëj-saalumu Afrig, ñi ëpp ci ñoom it canc gi lañu àndaloon ñëw fi. Ña ca gën a bari dañuy liggéey ci yaxantu, ñenn ci ñoom dañuy def ay mecce yu ndefar (industrie). + +Jafe-jafey way dëkk yi fi cosaanoo + + Deltu ginnaaw gi jokkoo gi (communication) def. + Tas gu fa mbas yi tas ak tawat yi ngir méngoodig melokaani klimaa bi. + Ñàkk a tembug koom-koomu Afrig bi ak lënku gu mu lënku ci koom-koomu réewi sancaan yi. + Boddanteg xeet gi ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa. + Nekk gi yenn néewte yi di ay jàmbur (dëkkuñu fi) nekk ci yenn ci réewi gox bi. + Ñàkk a jëm-kanam ci wàllug njàngale ak xarala yi manul a ñàkk cig jëm-kanam ak màggug koom-koom. + +Afrig +Leopool Sedaar Sengoor mi ngi juddoo ca Jiwaalo ci 9 Oktoobar ci atum 1906, génn àdduna ca Verson (ca Fraas) ci 20 Desambar 2001. Nekkoon taalifkat, bindkat doonoon it killifa aada ca Senegaal. Mooy ki njëkk a doon njiitu réewu Senegaal (1960-1980). + +Wàcc na jal bi ci teeyug bàkkanam, bàyyee ko Abdu Juuf. Ñu bari ci àdduna bi dañu koy jàppe kenn ci xalaatkati Afrig yi ëpp solo, yu ñaar-fukkeelu xarnu. + +Dundam +Léopold Sédar Senghor ma nga juddoo ca Jiwaalo, di ab dëkk bu ndaw bu ne ca tund wu Mbuur, ci diiwaanu Cees. Baayam di Basil Jogoy Senghor, ab yaxantukat la woon bu bokkoon ci kuréel gu diggu gi ci giirug séeréer, di genn ci néewte yi ci Senegaal. + +Yaayam di Ñilaan Njéemée Baaxum, ñatteelub baayam. Bi mu amee juroom ñatti at, la tàmbali am njàngam ci ab Gospel : benn jàngu bu dëkku bu Baay yu Ruu Gu Sell gi (les pères catholiques). Ci atum 1922 la dugg leekool (mbaa jàngu bi) te booba ma nga Ndakaaru, muy ku soppoon njàngat lu Faraas, di woon ku ràññiku ci làkku Faraas, Laatin, wu Geres ak Jabru, mu daal di am Bakalooriya, daal di am ag may ngir àggale am njàngam ca Faraas. + + Yaxantukat ci fr:commerçant + kuréel gu diggu gi ci fr:bourgeoisie + néewte ci fr: minorité + jàngu bu dëkku ci fr: internat + njàngat lu Faraas ci fr: littérature française + may ci fr:bourse + +Senegaal + +Sengoor nekkoon na di kenn ci ñi doon jàppale Lëngoo gi:(réewi Afrig yi temb bu yàggul), loolu lu mel ne (ag Komonwelth gu Faraas) gu ag Lëngoo la woon, réewi Afrig yi nag ànduñu ci woon. Moom sosoon na ak Moodibo Kayta Lëngoo gu Mali gi. Moo nekkoon njiitul jataayub lëngoo bi ba ci kero bi mu tasee atum 1960, moo nekkoon ki njëkk a jiite Senegaal, ñi ngi ko tànn ci 5 satumbar 1962, mooy ki sadd bàkku réewum Senegaal (gar gu xonq gi). +Njiitul jëwrinam lii di Mamadu Ja moo féetewoo woon doxal naal yi aju ci suqaliku gu réew mi gu guddub dig gi(long terme), bu ko defee moom Sengoor mu féetewoo séqoo yu bitim réew yi + +Waaye ñaari gaa yii mujj nañu wuute ci lu gaaw. Ci disambar 1962 lañu jàpp Mamadu Ja, mi ñu tuumal ne day xiirtale cig daaneel nguur, mu daal di sax ci kaso bi lu tollook fukki at ak ñaar. Ginnaaw bi Sengoor daal di taxawal ag noste gu njiit . Ci 22 Mars 1967 Sengoor mucc na cig bóom, ñu daal di teg àtteb ray ci ki ñu ko tuumaaloon. +Tekki na ndombag tànkam njëkk ab àppub njiitam di jeex, loola di ci disambar 1980, daal di fiy wuutal Abdu Juuf ci boppu réew mi. Ci ron ag njiitam la Sengoor sampe lëwug làng( ñu yamale woon ko ci ñatti dawaan rekk: mbokkoo , mbokkte, ak afal ak genn noste gu yar ( systeme educatif) gu am solo. + +Bariwaa na lu ñuy askanale Sengoor ag demokaraasi waaye ay fen rekk la,ndax moom indi woon na fi ci doole ag noste gu genn làng, daal di moñoxe ci doole lu sakkan ci ay yëngu-yëngu yu ñaxtu yu ay dongo (étudiants. +Ak doonte canc gu Faraas jeex na ci melo wu kilifawu (officiel) teewul xiimay koppar bu Senegaal Faraas a koy saxal, njàng mi it ci làkku Faraas lañu koy defe, te Sengoor it réew mi mi ngi ko jiite woon ànd ak ay xelalkat yu Faraas yu muy diisool, (Ñooñu nag manuñoo joxe menn xel mu njariñul Faraas nekkul, Moom itam jabari waa Faraas la yoroon, te bari na lool lu mu daa xeex ngir ñu yor aaday Faraas, Taalifkat ba nee na: + + (Màggat mu màggat ci am () njàngum tubaab jabaroo () tubaab tubaab la, tubaab ngeen dénk seen gaal gii) + + Lëngoo gi ci fr: fédéralisme + séqo yu bitim réew;relations internationales + noste gu njiit: système ou régime présidentiel + lëwug làng: multipartisme + mbokkoo: socialisme, mbokkte:communisme, afal:libéralisme, noste gu yar :systeme educatif + +niti senegaal +njiiti Senegaal +Jiitalug aji firi ji: + +Li ma tax a jug, jëme ma ci def bile ligéey, te ma jàppe ko muy bu am njariñ, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, ñi ngi ligéeyal Sëriñ bi, waaye it xeet wi . Ndax jël lu mel ni jaar-jaari Sëriñ Tuubaa, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk àgg,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dégg , man cee jariñu, ca anam ga mu gën a yombe, gënnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , ñeel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral . Lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal Sëriñ bi,waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, ñeel saw làmmiñ, te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gën a dugge,lay gën a tooge,lay gën a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay, yaw itam, kenn ci moom, ngéen di benn bu dul ñaar, gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe, di rawe; di jànge ci seeni làkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo. + +Man de bile téere,njëkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lëf ci waxtu,ngir yër ko,dégg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu néew, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu làkk yii,te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi. + +Ñaareel bi mooy , gis gi ma gis téere bii,di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ, di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi. +Làmboo nag kem bu réy ci xam-xam, ci lu aju ci Sëñ bii, di kenn ci ñi ñu war a xam, bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom . +Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir bañ a guddal, ñoo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenni jëlewaayi yoon wi,yu xam-xam yi. +Ndax kat, boo yëree, da nga ko gis lu bari mu naan Sëñ bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bëkk-néeg la woon ci bëkk-néeg yi,bu ma waxul ngën ji bëkk-néeg +, kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku ñépp xam ag sellam, akug dëggoom, yal na nu Yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci Sëriñ sunu,Sëriñam,laafaale ko ci, ci barke ku nu ligéeyalam, ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindéef yi. + +Aji firi ji: +Abdul Xaadir KEBE +Jiitalig aji taalif ji : + +Bii mooy teereb {Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim}, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di waxtaan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di { xam-xamu jaloore bu nu gàttal} mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin. +Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal. +Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin. + +Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam. + +Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. +Ndax kat ñooñu, ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan:{ ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih} muy ci maanaa ñooñu,ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey sëlmël ci yonant bi. + +Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBÀKKE Xaadimur rasuul. + +Bi loolu amee ma, bëggoon a leeral as lëf cig dundam, ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. +Waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi, ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñëwee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: {{ mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko. + +Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde {irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim},may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jéggalul ma Yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem, lu man a wecci loolu ko yéemutoon, ndax téere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dëgg bi mooy {minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim) muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngënéeli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. +Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee. + + +Ag ganeem àadduna(g.m) + +Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax - ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk (1270 g / 1853 g.j). Am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar (1272g / 1855 g.j) ca kër waajuram wu góor ca Mbàkke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. + +Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: + +(( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum (sharaha),muy 1270g làqu atum (shumoos) muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel niy jant (cig leer). Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar. Ci guddig àllarba, ci ñaar fukki fani muharram)). + +Ag yoram + +Moom sëriñ bi, bi mu ganee àdduna aji juram ju jigéen ju tedd ja a ko yoroon ba mu mat a jàngi. Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah, doomi Muhammadul Kabiir, mom Habiiballaah mu njëkk ma, doomi Muhammadul Xayri,. +Muhammadul Kabiir mii mooy ki ñuy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbàkke Bawal, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dëkkewu fa woon, da fa a bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah waaye bokkunu nday. Moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof, fa la làqoo ñu denci ko fa, di ko siaare. + +Mi ngi askanoo nag ci Tukklóor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof. Siiw na itam ne ñoom Gànnaar lañu bawoo, dem Fuuta. Seeni doomi baay-tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay sëriif lanu. + +Sama mag, sama sëriñ, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral lool. Mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu. + +Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu. + +Yaayam + +Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jëm fu nu naan Mbumbe, péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbàkke-Màkke yi dëkke woon. + +Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbàkke-Mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu, kaaf gi nekk ci Mbàkke ag Haa (arafu h) la woon muy haa giy mujj ci Ba, Wolof yi def ko Kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab). Li am daal mooy ñaari wax yi ju ci nekk, dëgër na te am na màndargam dëgg. + +Buso-boso yi nag ñoom, seen cosaan Fuuta la, ca fa nuy wax Golare. Barab yii yepp it yu jegee lanu. Barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddngay ñaari askan yi. + +Bi mu tollee ci war a jàngi + +Bi Sëriñ bi tollee ci war a jàngi,waajuram daal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO, mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. +Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbàkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO, doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi, ju jiggéen, ndayi wayjuram wu jiggéen,soxna Asta Waalo. + +Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbàkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal. + +Kenn ci ñu wóor ñi nettali na ma ne: sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daawul tàggalikook moom lu dul lu néew,ndaxte magam Maam Moor Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jiyaarkat boobu di Màbba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Màbba boole woon na leen ca ña mu paŋoon (dajale woon) jëme Saalum, nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn. + +Bi Màbba faatoo + +Bi mu faatoo nag moom Màbba, nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi, ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukklóor KA doomi bàjjani baayam. Bi mu jàngee ci moom dali xam-xam, tàmblee yewwu ak a ñaw as lëf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono. + +Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagéenug seen teddngay nguur gi ,li ko loruloo woon, tax it mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk, ndax da daan jàng ak a jàngale,te jàng ak jàngale neexoowut aki buur, moo waral ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dul ab coona. + +Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daan na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu génneel ko ci moom Qaali ab yàq, mu mujj nag moom sëñ bi far ko raw, mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko, kon mujj na toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali. + +Muhammad mom Muhammadul Kariim + +Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). +Bi waajur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba ,walla ci téere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba, bu ñëwee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci. + +Mbàkke Kajoor + +Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala, dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanc ca wetam, tudde ko Mbàkke Kajoor, sax fa ñaari at daal di wuyyuji boroomam, nee nanu, looloo ngi am ci Muharram, atum 1300g, dëgg naa ci Sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. + +Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale + +Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wàllug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,sëñ Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana Sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a tontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àdduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas. +Ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem, rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara. + +Bu dee mbooloo mi +Bu dee mbooloo mi moom, li leen yéem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu Sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme,bu njëkk bi mooy waxam jii: +{nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen}ba fa mu yam +teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii: + +{{ nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi,kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne)). + +((Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine)) + +((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàlla'ay ki may doyluloo te di ma musal )) + +((Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? )) + +((Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër'a'y dërub saytaane )) + +((Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul të,te mooy Kiy amal li ko soob )) + +((Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir)) ((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amuma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina ))((Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon déy ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gàccaal}}.''' + +Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga làqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee. +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang, fu nu ko jëmewul du fa jëm. Bi mu làqoo nag,mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp. ña fa nekkoon it ciy dongo jàng rekk a leen fa bàyyi woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku daan yёr (jàng) lu bari téerey Gaa ña (gaa ñi bu ñu ko waxee ñaare mooy magi tasawwuf yi) . Yàlla defoon muy ku sopp beru ak wër ni ko ñu baax ñi (ñoñ tasawwuf ) soppe woon. Mu daa indi ay anam yu wuute ci seeni waxiin, di leeral seeni maanaa yu làqu, di yëg seeni làmmiñ. Noonu la nekke woon – ci yooyu yëg-yëg ak yittewoo suufiyu yu mag yu njëkk ya, ak a gëstu séeni wax aki mbind – ba mujj himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yitte) dikkal ko, muur ko, yёkkati ko, yëngal ko,dalal ko, mu mujj moomatul boppam manatul a def lu dul woo nit ñi ci anam gu woyof jëme ci mbiram moomu (muy tasawwuf ak ab yëg-yëgam). +Bi ko mbir mi gënee lëjal nag, gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi, wax wax ju leer. + +Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen: “Dama ne: ku àndoon ak ñun ngir jàng rekk na laxas jëm ca boppam, na dem fu ko soob, man loolu rekk taxatumaa jug, ku bëgg li nu bëgg nag,na toog”. Daal di leen fay bàyyi dugg ca biir. +Waxam jii nag daal di leen bàyyi cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem. Sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa,la ca gën a néew des fa. + +Bi loolu lépp daata am,fekkoon na Sëriñ bi mu sóobu woon ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal yu sariiya yi; mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko, bég ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Dégg naa ci Sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. +Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginnaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g/ 1877 g.j, teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. + +Bi ko dongo yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla). + +Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne Sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci “Himma” te bu leen yar ci njàng,loolu Sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii: +{ Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw) +( Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel) }.Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw) ,mooy ji ci alxuraan:{ fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin} mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi. + +Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindéef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: { yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy téere,kon boo may ligéeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.Yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : (neel wéeru leen ci man}. + +Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab wéeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira,na wéeru ci man. Mu dellu waxaat ne: { Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci làq ngën ji ay may. Murid bu Yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na céru ciy may ) +(Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam) +(Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira}. +Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : { Jinney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñépp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul}. +Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: { toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid}. + +Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne: +{ Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax - mooy bàyyi aada,( muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam) +( Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu}}. +Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : +{{ Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox ko aw yiwam )) +((Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg )) +((Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona )). +((Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj di ab sëriñam fu mu jublu)) +((Ab sëriñ du wuuteek Ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu )) +((Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba)) +((Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam }}. + +Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wépp yiw: {{ Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru)) +((Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk )) +((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) +(( Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) +((Képp ku boole yile melo ci murid yi déy,da na jot ndëërlaay ya (gaa yu baax ya)}}. + +Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: +{{ Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi)) +((Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm)) +((Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def)) +((Nettali nanu ne malaakay Aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif}} + +Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: +{{ Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew )) +((Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,téere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def}}. +Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yéem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci téere bii,du amati,ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko. + +Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla)) +((Li waral sama tukki bu sori bi,Yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yàlla’a ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne :{{ Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yi ak yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam)). + +Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp,mu ne ci:{{assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara)). +Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca Yàlla, àgg ci Yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manut a ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am déet,du ligéeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war. + +Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligéeyloo,ak ay tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa Yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii. +Mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat,dajale leen,di leen ligéeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku Yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigéen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul Yàlla,{Yalla jënd na ci jullit ñi,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana},Sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn,ba bi mu sancee Mbàkke Bawal,ci at moomu juge Mbàkke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu nekk, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñi ak ñu sori ñi, ñepp di yéemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at. + +Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñi mu siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a woy ay sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Yàlla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir Yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom. + +Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem. + +Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay téeméeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi) ak waxam ja: ( sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Yàlla,yal na ko Yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne déedéet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon. + +Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala da nga koo bàyyi ngir Yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Yàlla,ju mu manatul a bàyyeeti,ndare cib coona,ma jëflante ci ak moom waaye Yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng. + +Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na Sëñ bi Njaaréem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yi ak naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke. + +Bi Sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam-xam bu bari bi ak njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci Yàlla ak yiteem jépp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi. + +Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu,nu tàmbli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoom,lor yi ëpp,mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam, Yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasoo’k ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarloo’k moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jéggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi. + +Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci Sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gañe ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal ak ay jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lanu bàyyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko. + +Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji déggal ko,def ko ànd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,règg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weñ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub. + +Ñu xam ne li mu wax lu dëggu ci moom la, ñu jéggal ko, noppi cim mbiram. Waaye Sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul Sëñ bi bañ,nee nanu ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : {neel ki la yonni rus naa malaakay Yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla}. Dégge naa ci sheex Aadama SÀLL - moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci Sëñ bi , cosaanoo woon Jolof - mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: { Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan},Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi - moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,ya’ay weñ wi man nag,ay dem-àll laa. + +Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu bàyyi ko ak mbiram ,ndax kat notante ak moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànji ci toolam - te manu koo bay, manu koo saxal -mu bàyyi ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah. + +Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yi ak coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcc benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkkoon, bi Sëñ bi yëgee ne moom ak Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi, mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : ( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi ). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa nekkoon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi moom taxul,juboo’k moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sunu mbir ma nu ko woowe woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne Sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal ji ñu nangoo ci moom niki màgg ak njaf ña mu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lépp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,Sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waaw,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw, mu ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonnant ? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xaree’k moom,nan lanu koy seedeele ? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, Sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaali ak mbooloo mi ne tekk as lëf,ba mu yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la Yàlla,nga jiitu nu ca,kon ag ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te juboo’k moom. + +Pënd ba wuri,Sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu, yoon yépp dagg ci moom lu dul wi jëm ci Yàlla,ndax kat moo jàkkaarloo ak ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom:{wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi} muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,Yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq. + +Li mooy dooley Sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jéll yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yéeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara génn,te dunu lakk,di yekkati xasiday Sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu bàyyi, ñu leen di door ak a jéng,ak a nangu seen alal,ak a génne seeni kër,loolu lépp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem ak ag sóobu, mu mel ni loolu mbóotum Yàlla’a,mu ball juge ci baatinub seen Sëriñ ba ca ñoom,Sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay Yonnant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nanoo’k lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu Yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,génne leen séeni kër,te loolu téewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca Yàlla, :{ lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun },mu leen di xamal ni,danoo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu génne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku Yàlla ak ngërëmam,ak dimbali Yàlla ak ab Yonnantam, ñooñooy ñu dëggu ñi. + +Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day daal di doon lu néew,{laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira}}muy :ku gëm Yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonnant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, { Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim} muy dee leen jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. +Dee leen di fuglu { yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim } muy bis ba niy woo nit ñu nekk ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey Sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanoo’k a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tagg,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy téere bu amul moroom ci tazawuf,yor junni ak juroomi téeméer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom. + +Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanc Daaru Salaam,ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tolloo’k am at,di yar nit ñi,di leen yéege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,dem as lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tolloo’k juroom walla juroom ñaari kilomet,sanc fa Tuubaa,ci mujjug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom,walla ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom benn,tuxu fa ak njaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma - ñaareelu xalifa - ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom Sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos. + +Ku dul Yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalante ak ay xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yi ak jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. +Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dolliku ak a yokku jamono ju nekk, ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca géej ga. + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Sëñ baa ngi sanc Jolof - ci li ma sëñ Mbàkke BUSO nettali - bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denc ay soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasoo’k ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligéey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu ,aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji Yonnant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon. + +Kenn ci sunu moroomi naari Daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:Sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii, nu ànd aji,bu neexee Yàlla ,ma dem waaji te lijantiji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun). + +Nu dellu ca wax ju njëkk ja, Sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ci ak man,diisoo’k man ci mbirum ñu sanc ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligéey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd fa ak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. +Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siyaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku warut a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah. + +Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul - bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it, wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li Sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada. + +Waaye Sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom. + +Kon Sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon,te foofee ca la wër Tuubaa amul am ndox,walla bu fa saxee it da na ajowoo jankoote ak ay ñoñam,mbaa mudaaraante ak ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbàkke Baari,wacc fa,sanc fa,waxtaan fa ak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbéenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu dul ay buur,yu ñëw ngir xëccoo’k ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee. + +Waaye Yàlla moom bu bëggee amal am mbir da koy wutal ay sabab, nee nanu bu Yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. +Bokk na ci xéewal yi Yàlla xéewale Sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu wàlliyu yi, { sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan }} muy ci maanaa yoonu Yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu Yàlla. Nit du jug mukk jëm ca Yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg Yàlla’a, ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,Yàlla da koy feeñu cig màgg ak cib taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko Yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug Yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen Yàlla di dëddale ak yenn xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bopp,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lépp,hifthul hinaaii du tàggoo’k ñoom,mooy wattu gi leen Yàlla di wattoo’k a aar,dara du leen dal lu dull lu Yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom { Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna } muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan Yàlla jàmm. + +Lii mooy mbirum Sëñ bi ak ay àndandoom ca njëlbéenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom Sëñ Mbàkke BUSO nee na:taalube yi mu bàyyi woon Tuubaa,bi nu yéggee ni Sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax déet, ginaaw mbir mi du mbirum xalaat. + +Bu dee lu aju ci jaraaf yu dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu déggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu tàmbli noo dikkal ci kaw ak suuf. + +Bi buur yi ak seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,danu daan song ku leen daa jéem a t��,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donnante,waaye loolu téewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom néeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki néegub sëñ bi. + +Loolu ak meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci Sëñ bi,meneen mbir mi nag , +nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig. +Ci noonu nu jël buur yi ak jaraaf yi teg leen ci kaw daara yi ak donga yi,ñuy seeni njiit,waaye loolu xéewal a ngi ci ndax tax na ba buur yi ak seen jikko yu bon yi nu yoroon, di sonnal jullit ñi ak a fitnaal ak a def li leen soob ci nit ñi jeex. + +Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexe ak ay wor. +Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kiliftéef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galag, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wut ay ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu , +walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop. + +Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàq dunu dañ,di yàq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def. + +Loolu moo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañu koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkulóor la bu defoon ay xare ci wàll gi mu dëkke woon , +ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmad Sheexu dib Tukkulóor,moom it,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi. + +Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen ne Sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu li nu leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi Sëñ bi,ginaaw bi ko Yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax Sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,Yàlla’ay seere lii nuy wax. + +Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma la ak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonnant bi ji (j.y.m), { ñi Yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonnant yi,teg ci wàlliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp}} ,ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonnant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis :[ àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar ],yàlla itam wax ne :{wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin} muy àllaaxira, ñu ragal Yàlla ñee ko moom. + +Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum Sëñ bi, ñu tàmbli fa’a yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonnant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngéen li nu leen waxoon am déet ? . + +Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu néew,bunu leen tollalee’k li nu am ciy xarekat,ndax matunu woon mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi. + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul Yàlla ak Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida:{ ku nu tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru,}}, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g. +Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane ��dduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn daje ak ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak Sëñ bi kerook la, ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja - am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal , +danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag Sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,jenn waay ju yor ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,Sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te déggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara. + +Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu Yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: {ginaaw bi nu dajee’k ña génnoon jëm ca këram,te njàqare nekk ci seeni dënn)) +(Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla ) +(Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siyaare ) +(Mu jubale kanaman ca Yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg ) +(Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu) +(Jaraaf ja génn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xéewal.}} + +Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,Sëñ bi nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaaréem. + +Sëñ bi nee na: ( Omar mii mi ngi génn,ngir siyaaresi ma,daje ak soldaar siy génn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye Yàlla moom xam na la nekk foofa). +Sëñ bi nee na (nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu déglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon, ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrànkeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir,looloo taxoon mu wird aayay {wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina}}muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu génne la, ñu nekk di fexe,Yàlla itam di fexe,te Yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :(Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel lanu woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonnal ca daanaka-dun ba bépp (daanaka-dun mooy Presqu’ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrànkeel ma, ñooña Yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat). Sëñ bi wax na ci loolu lii: +{ Yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono)) +(Mu tàbbal ci seeni xol,ag génne ko,jëme ko ca réew yu sori ya,mu ame fa lu kawe déggub Saariya}} + +Yàlla (t.s) dëggal na ba mu naan {wal laahu xayrul maakiriin}}muy yàlla’ay ki dàq a fexe. Ndax xéewale na ma ñatt yu gën seen ñatti kuréel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dëgg-dëggi sëriñ,ci gëm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy ñàkk a nelaw guddi) ,te ñàkk ko, ñu may jam ay xeej a ma ko gënal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gëm Yàlla gi nga xam ne mooy dëgg-dëggi xam Yàlla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wér la ne li nga nekk ay dëgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy àgg ca Yàlla mu kawe mi, ñatti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasoo’k ñoom,te loolu moo daa doon sababu rékki gëm,yal nanu ci yàlla musal. + +Ab nettali bu yéemee ngii ma, dégge ko ci Sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te yoroon woon mbirum tukkib Sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu génne ko,tumbrànkeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu génne Sëñ bi tumbrànkeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,loolu moo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma Sëñ bii fi yaw,bu ko jéem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yéene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca . + +Loolu moo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lépp mujj yomb. Bi Yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penku bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci génn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu ngàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ . Mbirum noonam boobu,niroo’k lool,mbirum noonub ki miy ligéeyal di Yonnant bi (j.y.m),noonam booba di woon Haamir doomi Tufayli,ba mu nee jamono ja ko tawat ja sonnalee ci génn këru jenn jigeen ju Salool: (ndax lii day am mbas mu mel ne mu giléem , te di ag dee ci néegub jigéeni Salool ?). + +Sëñ bi def na ag xasida,gu mu tënke arafi {mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw }} ne; +{ tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, te mu damm)) +(Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi)) +(Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci nekk,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko)) +(Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci géej gi ak ci jéeri ji,te am mbooloom wor ko }}. + +Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,moo’k mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal Sëñ bi ak a saboote,fu mu masa’a daje ak moom,moo nekkoon Garambasaa. + +Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakaaru,ki ci des,di ku géej gi,nekk Konaakiri,yal na nu Yàlla musal ak jullit ñépp,ci nattu bi mu leen tegoon. + +Nu dellu ci mbirum tukki bi,Sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy { Inna wàlliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin}} muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy Yàlla mi wàcce téere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolu mooy maanaam waxam jii: +{Yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi) }}. + +Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli fa’a woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, Sëñ baa ngi wax ci loolu: +{ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt }}. + +Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali - ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn ngélamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu ko woon a jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:Sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe? bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: +{{laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca’akug xat te di ko muñ ) +((Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji}. +Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii: +(kuy sukkandiku ci ndimbalul Yonnant bi,bu koy gaynde fekkoon cib àll it wedam) +(Moom Yonnant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan moo’k am mbooloo ànd ngir,màggam ga ). +Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa. + +Nettali nanu ne Sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,Sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lòtt,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma Yàlla du lòtt te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy Yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara.{wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii,} muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (Yàlla mu sell mi dëgal na,Yonnant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jòttalee). + +Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku Sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) nee na {wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lòtt ci sama mbir,bu mu lòtt ci sama sunna}},Sëñ bi moom dònn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,Jibriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan. + +Sëñ bi Yonnant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu Yonnant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi {hasbunaal laahu wa nihmal wakiil}muy ci maanaa Yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la. +Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma Yonnant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor. + +Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : {maa ngi sant ki ma musal ci lori jépp saytaane ak jinne ak nit) +(Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi)) +(Maa ngi sàkku ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju nekk)) +(Yéene naa koo ñaan di sàkku am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu)) +(Mooy Ahmad,sangub mbindéef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom)) +(Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xëccoo)) +(Ya’a moom mbindéef yi ,yaw sama boroom,may ma ag mucc ci ñoom,ak bépp balaa ak mbugal)) +(Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal)) +(May ma li ma bëgg ci adduna ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àdduna ak gu allaaxira)) +(Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma)) +(Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo)) +(Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb Yonnant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef)) +(Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon)) +(Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lépp lu ko man a jublu ciy mbugal)) +(Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax)) +(Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jépp fitna)) +(Fegal ma loxol way bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge)) +(Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gàccaal,ci àdduna ak àllaaxira,te dee ma jéggal)) +(Bindalal Yonnant bi ag xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax.}} +Mu tëje ko { fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim}}: muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xéewalug Yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul Yàlla te Yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li). + +Mu neeti { alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina}} muy ci maanaa : ( maa ngi sant Yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu Yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na Yàlla,miy boroom mbindéef yi) . +Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,Yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo. + +Mu wax:{allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam}}muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne Yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom. + +Waxees na ma ,te loolu lu wér la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi Sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii:( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee). + +Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk Sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul Sëñ bi, mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug Sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal Yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite. + +Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum waafiris sitri,di junni ak ñaat téeméer ak fukk ak juroom ñatt,bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal képp ku ko daa jéem a lor,téere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabéey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee. + +Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at ak ay weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,jooy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci géej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko Sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yéeme,gi nga xam ne Sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te Sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: +{maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi (waa Ahlu Badri),bi may dox (bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp) laa )) +(Sama dox bi may def, ci wommatug Yonnant bi, ànd ci ak gaa yu baax yi,Yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul Yàlla)) +( Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa Yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man )) +(Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju nekk mi ngi may sottil ay xéewalam ) te mooy ki di ab santaakon (ku soxlaalul kenn) )) +(Sama ndimbal,samag dëgëral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci Aji yaatu,ji di ab Mayewaakon,(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama )) +(Sama kilifa nag, ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraan,di Yonnant bi,te mooy ki may ligéeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal)) +(Samab yool ci ligéey bi may defal Ku nu tànn ki,di Yonnant bi, mayewaakon (Yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la)) +(Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligéeyal gën ji mbindéef,te moom Yonnant bi mooy samab xuppkat (Yonnant bi day bashiir tey naziir,di kuy bégale tey xuppe ngir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ) )) +(Aji feg jii di Yàlla,moo may fegal ci Yonnant bi,ayi noon yi,ak lépp lu ñaaw te mooy ki may xettali)) +(Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligéeyal Yonnant bi,mbiri mbindéef yépp nag ca Yàlla lay mujj )) +( Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub Yàlla,te moom siw na )) +(Samay sutura ci adduna ak allaaxira,mooy tagg Yonnant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la )) +Samaw jiwu mooy téereb Yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu (muy saytaane) )) +(Samay kër wéet na, ñoñ ñi tas,ngir tagg Ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat )) +(Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la}}. + +Sëñ bi nee na : ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu Sëñ ba’a ngi ciy wax naan: {Yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde)) +(Ñu àndandoo, sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari}}. +Ma sax fa - sëñ beey wax - la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci la’a dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen bàyyi leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu. + +Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku wéet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caagéenug aw wéttal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ? +Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!. +Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci Yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àdduna yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bopp,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna. + +Ca bis ba ma war a juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa, ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,Sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn. + +Bi Sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub Yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant Yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. +Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci Yonnant bi (j.y.m) ki may ligéeyal,sama dënn leer,sama xol dal,kóolute gi dolliku ci Yàlla’ak Yonnant bi,ndax {{ alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub } ci tudd Yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale. + +Sama gudd gi daal di neex ci Yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan: +{ Yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wépp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe ) bi xëccoon jëme ci man)) +(Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye Yonnat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu )) + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Bi nu xëyee - sëñ beey wax - muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal nanu ma ca digg gaal ga,di jooy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,Sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: +{{Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini Yonant bi )) +((Gaal gu fees googu ak mbooloo, yendu na fanaan )) +((Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga )) +((Murid ba tàggoo, dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari}}. + +Mu jublu ci muritam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñépp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,Sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba mu far jël daam ak xalimaam,nee na, bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbindéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi. + +Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saa sa, ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjëlati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag, nga xam ni moo’k nit ñépp a yam,dara waru ko lu dul mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko. + +Ci loolu mi ngi naan: +{{Ki njiit li yonni woon ca ligéeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu )) +((Ginaaw bi aji ligéey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal)) +((Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la Yàlla di wonee aw yoon}}. + +Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) (wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca Yàlla te Yàlla’a ngi gis jaam yi. +{maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi}}. + +Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,Sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa dégg ñu ne ya’a ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma. +Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul Yàlla,ku jublu ci ku dul Yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul Yàlla,ku jublu ci Yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad Yonnantab Yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne Yonnant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem. + +Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye Yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul génne ci ab néeg ne ma,ndax ya’ay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak a màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gaal gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: +{{sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi)) +((Yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lépp luy xëcce jëme ci yu nu sib )) +((Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma}}. + +Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,leeral gi mu ko leeraloon maanaam laa ilaaha illal laa,waaye du àddiyay alal ja ko waa ja jox,moom waa jooju nga xam ni bu ko Sëñ bi leeralutoon loolu mu alku,te Yàlla gindee na ko ci leeral gi. Mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yéeme gi ko Yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yeréem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi téeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñépp walla ña ca ëpp,ci loolu la Sëñ bi naan: +{ kiy jagleele yërmaandeem di Yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle}}. + +Mu jublu woon ci aji yërëme jooju Yàlla mii di boroomi xéewal,daa ko indil ay xéewal,bokk na ci xéewal yooyu biteeli misk yooyu. Mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li ko dal,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ . Mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne Yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe .Mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñépp ba kerook muy wàcc Gabong. + +Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mjje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci Yàlla ak Yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug géejug dun boobu laa taxawoon di joriku, di xutba géej gi naan: +{ yaw géej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd ) +(Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal Yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,bob sopp na ko}} + +Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal Yonnant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fépp. + +Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yépp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saa sa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne :{ yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun}muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmëx ab loxoom bëmëx gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lépp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tolloo’k waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrànkeel ak a génne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daataa wàcc,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,loolu moo waraloon sama ñëw gii du leneen. + +Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu bég ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah. + +Da na rafet fii ma indil leen fi bayiti ki def Xawaariq muy Ibnu Hanbal: +( Bari na aji jalgati (tooñkat) ju sol yérey teddngaam,di puukarewu ,sol ab tëneem aki takkaayam) +(ay junniy junni nekk ci ron kiliftéefam,te faalewul ku koy digal mbaa mu koy tere)) +(ngeen (Sëñ bi lay waxal) wàcce ko ci mbartalum toraxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) ) +( muy ndimbal lu tukkee ca Yàlla ñeel jaamam bii di ligéeyal Yonant bi,nga xam ne soldaari nasaraan si ci la nu mujje mokk ba mel ni ay ansaaram,(ansaar mooy ku lay jàppale ak a dimbale) ) +( cey bu tuddoon sekkare bi, kon dey mbindéef yi yéemu,waaye moom ab dënnam bàmmeelub ay mbóot la). + +Nee na bokk na ci karaama ( mooy xarbaax ak kiimaan yi Yàlla di defal aw wàlliyu) yi ko Yàlla defaloon ci géej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat bi mu nekkee ci benn ci dun yi,dañu koo yobb woon ca karce ga,dëkkal ko fa soldaar sa,nee na ma mel fa ni kenn ca ñoom,ñuy tux ak a naan ak a fo ci sama wet, man may muñ seeni lor rekk,ndax man xam naa ne mukallaf mu ne am na ñaari malaaka yu ko seq,di bind ay jëfam,ginaaw ñaari malaaka yooyu ñoo man a muñ,man a dékku li ñiy dajeel ciy lor,ngir topp seen boroom,kon du jaadu ci man may jàmbat,ndax ñoom kat li leen di naqari rekk moo may naqari,li leen di mettee may metti,te ñoom du ñu jàmbat. +Ci noonu Yàlla dogal soldaar si genn bis di tàggatu ji ,ba ñu demee fañuy tàggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas, kaalawu, sappewu (rang),soldaar si dal di tiit ,taxaw,ci noonu seen njiit li tëyye leen,gëdd leen ne da leen di ray bu ñu siiwalee xibaar bi. Bi suba jotee ba leer,mbooloo mi waroon fas yi ne mes,soldaar si dem ne miik,bañ a nettali dara. Sëñ bi nee na bi loolu tegee ay fan,aakim bi (goornoor bi) woo ko nooy-nooylu ci kanamam,wax ak moom wax ju nooy,ci biir wax ji mu ne ko: xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali ci li nga bëgg? +Ma ne ko ñooñu moom ay nit lanu walla ay jinne? Mu ne ma yaa ko gën a xam ! Man ma won ko ne xamuma dara ci li miy wax,mu dal di noppi. +Am na ci boroom xam-xam yi ku ko ci laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi,Sëñ bi ne ko :ngir tiital noon yi. Keneen laaj ko ne ko ñooña ñooy niti Ahlu Badrin ña walla malaaka ya?,mu ne ko malaaka ya .Am ku neeti ko ndax yonnant (j.y.m) bi ca la woon? +Mu ne ko moo doonoon seen njiit,daal di ciy wax wax jii:<< ki nga xam ni wommatal na ma la fàddu woon wëliif bepp wàlliyu,jàppndalal na ma mebat yepp fa dëkk ba niy wax Limbarwali >> +<< ka soril rambaaj ba ak ku inaañ ka ,wommatal na ma waa Badar ña diy sang>> +<< Yàlla da na ma wommatal begleg laa illaaha illallaa fu ma man a ne >> . +Ku baax ki nee na li mu bëgg a wax ci bayit yooyu mooy: li fàddu woon weliif bepp wàlliyu,mooy feeñug waa Badar ànd ak seen kilifa ga (j.y.m) ca pàkk yu lëndam yooya ca geej ga,ngir jàjji ay noonam.Begleg laa ilaaha illallaa,mi ngi ci jubloo wax aaya bi sun boroom di wax (( wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda lifaddlihii)) muy ci maanaa bu la Yàlla bëggalee aw yiw amul ku ko man a tëyye. Fu mu waxe nex-nexi walla lori laa illaahaillal laa,mi ngi ci jublu waxi Yàlla ji mu naan:(( wa in yamsaskal laahu bi durrin falaa kaasifa lahoo illaa huwa )) muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak aw ay amul ku ko man a dindi ku dul moom. + +Mu ne bis teg nanu ko ci mbedd mu xat,dal di joyal aw nag ci kawam,tàmblee seetaan,yaakaar ne agsi na ci sama kaw ba noppi,waaye bi mu ma jegee daa daal di jekki-jekki rekk naaw mel ne daa am ay laaf. Nag wii mooy wi Abdu Laahi Saalim Ibnu Anbal doon tudd ci Xawaariq bi mu naan: ( ab xiik (xiik mooy xale bu jigeen bu masul a sëy,fii mu jublu ci nag wu toll ci war a sëy ) ci nagi kër yi,muy naaw ci jàww ji ba kenn gisatu ko). + +Mu ne mas naa am mu yàgg ci benn barab ba foofa soof ko,mu tàmbli di jàmbat,waaye nee na daa jàmbat rekk Yàlla sotti ko yamb yu soxot te bari,ñu koy màtt ak a sonnal,mu ne bi mu xamee ne li ko dal moo ko teg boppam,ndax kat ((wamaa asaabakum min musiibatin fa bimaa kasabat aydiikum)) muy musiba mu leen dal yeen a ko teg seen bopp,bi loolu amee mu ne ma soppi samag jàmbat def ko ag cant,daal di ne: +(( nasaxal naa sama njàmbat def ko ag cant,dootuma jàmbat ci moom lenn lor,ndax sama lor naaxsaay na)). Ci noonu nee na yamb ya dem wëlif ma ,ma tàmblee noppalu,xam naa ne yamb yooyu la ki def xawaariq jublu woon bi mu naan: +( ay yamb yu toll ne ay mburtu (mbate) yu suur cig réy, cam si (cam si mooy waa ji,mu jublu ci Sen bi) daje na ak ñoom,te faalewul seeni lor ). + +Mu waxaat ne waa jooju doon nasaraan-nasaraanlu te nu tuddoon ko ca ginaaw,bis def na ko lu ñaaw ba yenn xaritam yi yedd ko ci,xupp ko ba mu tiit, reccu,ca guddi googa nag mu ñëw ànd ak ku koy wommatal ab gàtt,moom mu yor benn biteelub daa bu mag ci loxoom,dal di tedd tàllalu ci sama kanam,nee waay day tuub,te ne du jug fi mu tëdd mukk,li feek teguma sama ndëggul tànk cig doqam,ngir tuub,ma fexe ba jële ko fa ci wax ju rafet rekk,mi ngi ma fekkoon nag may bind ca jamono jooja,ma dal di def bayit wii ca saa sa: +4(( Yàlla nooyalal na ma ci guddi gii xolub boroomug tubbi ga,ginaaw bi mu ma indilee ab gàtt ak daa , ( ngir tuube ko ) )). + +Ku baax ki tudd na ba tay yeneen karaama yu ko yàlla defal ci gèej gi,mu ne da fa mas a dëkk ak benn doxalkat (goornoor) bu soxot,bu kenn dul jege te bagul dara ci lu baax,ma wax bis ne jiyaar jii may def ci yoonu Yàlla daal di naa ko seet tay ci mbirum àttekat bii,ma xool nu ma ko Yàlla di tàggatale, ci noonu ma juge sama néeg dal di dëgmal këram,ñu ne ko sëriñ ba dey a nga jemsi ci yaw, mu ne aah loolu de lu jomb la,ndax danu daa sàkku ci moom muy bañ,kon tay naka la fiy dikke ci coobareem,ñu ne ko amul benn sikk ci ne kee di dikk de moom la,mu dal di jug ci saa si daje ak man fu sori,bég ci man mbégte mu kawe,ci noonu mu ànd ak man ca barabub boppam ba,dal di ne ma loo bëgg, loo bëgg cig baamu ? Wax ko ay yoon, man itam ma ne patt, rekk di xool lu ma koy wax,ba yàgg ma ni ko,da maa bëgg as lëf ci daa, mu dal di may jox bitéel bu mag bu fees ak daa,ma daal di ne wëlbat won ko ginaaw,booba fekkoon na ma may bind ak xasida gu ñu tënke arafi a b t th j (mooy abajada rekk) ,ba ma àggee ca arafu faa,ma bind ca bayit wii ne: +(( sama xalima texe na fa ab aat (mooy ku xaraful)bu weddi Yàlla,kok tàggat naa ko ci xul huwal laahu ahad)). + +Ma bindaat ay bayit,yoy dañu maa wax ni ma lii de ag wor la, ndax yaa ngi bàyyi yéefar yi ci anam gu dog,ba noppi ngay jël ci ñoom di nëbb,ma dal di bàyyi la ma doon def,gas am pax ba mu xoot ,ma sotti ca daa ja,suul,dal di xam ni sama jiyaar ji dëggu na, ma sant Yàlla . + +Nee na itam,benn janqu ndar-ndar,dafa gént gis Waa-Badar,ci bis yooyu nu dugg dëkk ba, tàmblee ray waa dëkk ba,bi nu demee ba kenn ci ñoom jege ndaw si,jenn moroom ji ne ko soxna soosu de ab jullit la,mu dal di koy bàyyi. Sëriñ bi nee na xale bu jigéen boobu ku baax la woon,daan sonn ci moom ci li mu am,daan ko wax naan man dey lu ma la jox rekk xamal ne maa ko ñaq ci sama loxo,njëgug sàngara nekku ci du caagéenug gu poon,loolu da koo leeral foofu ndax kat foofa ci ñaar yooyu lañu daa jëflantee,te moom xam na ne man du ma leen jëfandikoo te du ma jëfandikoo seenug njëkk,ma laaj ko bis ne ko loo bëgg ci lii nga may defal?,mu ne ma bu dee ci àdduna ,sët yu baax,bu dee allaaxira àjjana, ma ne ko Yàlla man na lu nekk. + +Yàggul tuuti rekk,Yàlla dogal mu ëmb,te daawul ëmb,bi diirub ëmbam matee rekk mu dal di wësin,dal di faatoo ci wësin wi,ma jullee ko,masu ma koo gis it mukk,ndare bi ma taxawee di ko jullee,ndax sunug jëflante mi ngi doon ame cig yonneente (correspondence). Nee nanu doomi Daba SEY la woon tuddoon Aamina (Ami),boroom këram tuddoon Yèlli SEY,bokkoon ci ndawi goornoor yu mag yi,di woon it ku baax te daan sonn ci man. + +Am na bis mu jote ak àttekat bi (goornoor bi) jote gu tàng,ngir sama jëmm ji,loolu nag ni mu ame woon mooy daa am bis ma wutoon ñeenti bant teg leen ci sama buntu néeg ngir def ko ab julliwaay ngir ñiy romb bañ di ci jaar,bi ko àttekat bi gisee ,daa dal di jug,falang jàkka ji buddi bant yi,sànni leen,ne fii amul julli amul lislaam,da nga ñoo bëgg a yàqqal sunu soldaar yi,ma ne miik,bi ko Yèlli SEY yëgee te tubaab bi demagul,daa dal di jug ca saa sa,jawalsi ànd ak aw meram , ne ko lu tax nga tas jàkkaam ji,te moom defu ko fu dul ci buntu këram?, sakkul yoon wi te xatalul kenn it. Tubaab bi ne ko man daal maa ko def,fii jàkka du fi am,Yèlli ne ko waaye man di naa ko defaraatal jàkkaam ji na mu meloon,tubaab bi ne ko du fi ame, ñuy bëgg a doorante nit ñi dox seen diggante, ñu nekk di xuloo diggante tàkkusaan ba jant so,ci biir loolu lépp man maa ngi bind. + +Ci xisa bii (nettali bii)laa binde xasidag ((Rabbanaa axrijnaa min haazihil xarya azzaalimi ahluhaa wajhal lanaa min ladunka walliyan wajhal lanaa min ladunka naziiran) muy ci maanaa yaw sunu boroom génne ñu ci dëkk bii nga xam ne ñi fi dëkk ay tooñkat lañu te nga wutal ñu aji méngoo ju tukke fi yaw,te wutal ñu aji dimbalee,xasida gee nekk nii: +(( gërëm naa kilifa gu màgg gii nga xam ne yar na samab xol te koomal ma, moom dey mooy boroom bi gën a tedd)) ba bi mu àggee ci : +(( bindal ko(moom Yonnant bi) ag xéewal ak ag mucc ak ñoñam aki saabaam te nga def sama jàkka ji ci darajaam (moom Yonnant bi) muy lu yaatu )) + +Bi mu àggee foofu ñu ne ko nangul nanu la ko,da nga ko gis. Loolu nag gis nanu ko,mooy jàkkay Jurbel ak Tuubaa ,xasida gi nag gu gudd la te rafet gu am jeexiit gu réy ci jañ ak ñoddi bu soobe Yàlla ak ci barkeb aji defam,ku koy jëfandikoo na ragal Yàlla te xemmeem aw yiwam. + +Yàlla dogal na bis Yèlli moomu siyaaresi ko Njaaréem,juge ca yooyale wàll,ginaaw bi jumaa ji noppee muy ju Njaaréem,Sëñ bi ne ma ma’ak sama jenn waay ànd leen ak moom mu siyaare jàkka ji,ñu ànd ak moom, won ko jàkka jépp,penkook sowwu,biir ak biti,mu yéemu gépp yéemu,bi nu dëppee Sëñ bi ne ko noo gise jàkka jii ak sama jàkka joojee,yaw mi ma doon xeexal ak a dàkku?,mu ne subhaanal laah maneesu leen a tollale,Sëñ bi ne lii mooy maanaam sama wax jii: +(( Yàlla dàq na jëme ca ku dul man ca Maayomba la naqari woon sama xol te yékkati samag wàll)). La naqari woon sama xol bu nu koy firi mooy tas gi nu tasoon jàkkaam ja,yekkati samag wàll mu jublu ci yekkatikug soorool yi. + +Ab nettali bu yéemee ngii bu làmboo ay karaamay Señ bi: Señ bi nee na bi tubaab bi buddee bantam yooyu,sànni leen,kenn ci gaa yi bégoon ci jëfi tubaab bi, da cee jëloon ab bant samp ko ci wanag wi miy sangoo ak a doxe aajo,waaye Yàlla nattoo ko benn bis mu bëgg a tuur ndox,jawali ca satala ga te booba satala ga ndox mu tàng a ca nekk te moom yëgu ko,te seetu ko it,waaye bi mu noppee ba sotti ko ca cér ba (sàkkara sa) da wadd ca kaw ni ab baa bu góor bu tiit,dal di yuuxu ba fa baatam yam, ne: Señ bi dimbali ma alku naa de,dal di sànni satala ga ca àll ba,dikk teg loxo ba ca tubay ja,ma ne lu deesi defati lu dul muñ ak wax (( innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun)). + +Mu neeti - moom ku tedd ki - ne am na at mom bu doonul woon li ko Yàlla tawfeexal saa su xamee ni weer tàmbali na mu di ko bind,kon wenn weeru ramadaan doon na jàll te du ko xam,ndax waa dëkk boobee mu nekkoon xamunu woon lu dul weeru tubaab wi,bi korite gi jotee ma xëy, dog ,sangu, def li ci sunna digale,ma génn ne damay julli ji ca pencum dëkk ba,ba ma àggee, ma xool sowwu ak penku,xoolati sama ndijoor ak cammooñ,ànd ak am kóolute ci ne kenn du ñëw,am ñaari jèbbéer (jèbbeer mooy jaam bu jigéen) yu agsi war a toll ci baalix ( baalix mooy ati génn ag ndaw) taxaw sama kanam di ma seetaan,ma kàbbar ñu tàmbalee xàqataay,saa su ma kàbbaree nu ree,naka noonu su ma jàngee,ba ma sëlmal def samab xut ba, sama déeyaale gi maa ngi ciy wax:(( yaw buur bi, xam nga ni woor naa weeru ramadaan ni nga ko digalee,ma dog ,sangu,julli ni nga ko digalee,waaye dey lu ma génnee muurum koor laa amul,bu ma ko amoon it,ku ma ko jox laa dul am,kon jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sang,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam ,te nga nangul ma lépp lu ma man te def ko ci sa ndigal yi,te nga bindal ma yoolub li ma manul lòtt ci,te amoon ci yeene walla yu ni mel. + +Bi ma noppee def xasida gii: yaw buur bi jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sàng ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam te nga def qaafiya bii di ñëw,mu kawe miimiya ba ,ci lu feeñ ak lu nëbb,aamiin yaarabal haalamiin ci barkeb Yonnant bi (j.y.m) : +((maa ngi yaakaar ci aji yaatu ju dëggu ji,ci darajay ki niy xeeñtu di Yonnat biy dimbali dëgg ci dëgg (j.y.m) )) +(( maa ngi yaakaar ci Yàlla moomu delluwaat ci samay mbokk ci lu gaaw ànd ak njub gu dëggu)) +(( ak nekk jaam bu texe bu nu matal, tey ligeeyal jaamub Yàlla miy dëgg,jaamam boobu di yonnant bi mu tànn)) +(( yaw Yàlla ci darajay ku nu tànn ki ak ñoñam,yal na nga ma jéggal te nekkal ma te wommat ma te goreel ma)) +(( di naa la gërëmloo ci Alxuraan ak sunna si nga xam ne,Yonnant bi yoonalal nanu ko,yaw miy aji teqale lu taqaloo)) +(( yal na nga ma tàggatal noon yepp ba fàww,te fegal ma ag bokkaale,yaw aji not jiy boroom tijji ak tëj)) +yal na nga ma wommat delloo ma Daaru Salaam gi nga xam ne fa laay deyaaleek yaw ciy aaya,te yal na nga kaweel ci man ay gox)) +(( yaw sunu boroom yal na nga ma dello ci lu gaaw te defal ma samay mébat yepp,te nga may defal ay mbégte te di am ñeewant ci ma)) +(( te nga may ma ay xam-xam yu jariñ jëmm ji ak mbidéef yi,te nga dolli ag yaatal gog texeel lay doon ak ubbi ak xar-baax)) +(( sama bakkan déy daa bañ ag yéwénal,ndax ab noon la,kon sellalal ma ko cig taxañ (taxañ Señ bi mi ngi ciy jublu lu gaaw) yaw miy ngën ji kuy yéegale )) +((na nga ma may ba fàww li ma bëgg ci mbindéef yépp, te nga fegal ma séenuw ay yaw miy joxe ag jiitu )) +(( màngal ma samay mébat fii ak fa nu jëm,te nga may ma ngënéel lu màgg te saxalal ma ngënéel li)) +(( yaw sama boroom fegal ma li ma ragal ca bisub njàqare ba,te nga defal ma jéggi siraat gu gaaw gu mel ni melax )) +(( musal ma ci (ay nocciku = nusuuh) ak lépp lu nit ñiy ragal te nga def ma may ku sori ag lakk)) +(( nangul sama ñaan gii yaw sama boroom,te nga faral ma samay ayib ,te nga seere ne man dey tuub naa ci jepp jëf ju di jëfi dof)) +(( te nga nekkal ma yaw sama boroom,te musal ma,te amal sama yaakaar,te fegal ma luy bijji ag nëx )) +(( nangul ma sama ñaan gii,yaw mi moom lepp, te nga tabe ñeel ma cig yaatal ak dëddu ak dëggu )) +((ci darajay Yonnant bu nu tànn bi,te nga fegal ma hisaab ci darajaam,te tàggatal ma ci moom kepp ku di boroomug kàccoor)) +(( na nga julli te sëlmël ci moom Yonnant bi,ak ñoñam aki saabaam,yaw mi moom penkook sowwu)). + +Mu nettali ci karaamay géej gi,ne : am na jenn waay ju bokkoon ci kilifay barab bi ma nekkoon,da maa digoon ab bitéelu misk ci lu dul ma di ko sàkku ci moom,ndax man daawu ma sàkku ci ñoom lenn,te daawu ma sentu ci ñoom,daawu ma wóolu seeni dig it,waa jooju ma digoon bitéelu misk bi,ndekete daa digoon keneen ci moroomam yi lu mel ni li mu ma digoon,waaye bi mu deful li mu digewoon ,waa ja daa tàmbali di xuloo ak moom ak a ngaayoo,moom itam muy dàkku boppam,(di defandar boppam) loolu lepp it mi ngi doon ame ci sama wet,ci wolof it lañu doon waxe waaye yu leerul dara,waaye làkk gi nu koy làkk li muy leeradi leeradi fàttali na ma réew ma, ba mel ne da maa ñibbi far ,ngir gëj gi ma ko gëj a dégg,loola neex ma lool. + +Waaye xuloo bi nu def te li ko waraloon lepp mooy wóolu gi mu ko wóolu woon,ak dig gi mu ko dig te defu ko,loolu lepp ma sant ci Yàlla,mi ma defal may kok wóoluwu ma kenn,sentuwu ma ci kenn ku dul moom,loolu tax ma def xasidag cànt gii, ma wax ne: + +Maa ngi tàmblee samay wax aki bjëf ci turu Yàlla miy boroom yërmaande ju yaatu ji ak ji miy jàgleele, xeewal ak mucc yal na nekk ci sunu sang,Muhaddad ak ñoñam aki saabaam.Miimiya bii moom la ñeel yal na ko Yàlla gërëm. Yaw sama boroom sama noon yiy say noon,sànni nanu ma ci géej gi,ni nu sànnee woon sa xarit ba Ibraahima ca sawara wa,nga waxoon ak moom (sawara wa) ci :(( yaanaaru koonii bardan wa salaaman halaa ibraahima )) muy yaw sawara wi doonal ab sedd ak jàmm ci Ibraahiima. +Sawara wa dal di mujj di àjjana ci moom,jàmm ak xeewal yal na nekk ci moom ak ci mbooleem nabiyu yi ak yonnant yi, +Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw aji dund ji! Yaw aji taxaw ji ! Ci darajay weeru ramadaan mi nga wàcce Alxuraan, mu dig jub ñeel nit ñi, te di ay aaya yu leer yu di ag njub ak ag teqale dëgg ag safaan,ci barkeb xut ba bii tàggatal ma géej gii ak ñoñam ak mbooleem samay noon yiy sa yos,te nga bégal jullit yu góor yi ak yu jigéen yi ci ñu gis ma te dajeek man,te dégg sama ag dellu ca Daaru Salaam,ak Tuubaa ci lu gaaw ci lu dul ab coona du caagéenug ag sabablu gu tukkee ci man,Aamiin yaw boroom mbindéef yi, ci darajaam moom Yonnant bi,(j.y.m) te nga def miimiya bii mu kawe li ma jortoon,ni nga ko baaxoo defe ak man ca la ma waxoon njëkk bii,te nga defal ma ko muy ab yobbal,tey pakk tey àjjana ci ñaari kër yi,aamiin yaarabal haalamiin. + +(( man déy maa ngi tagg,tey sant ngën ji aji xéewale, te du ma jàmbat ñàkki xéewal ci menn mbindéef )) +((kepp ku ma jorte ci sama tumburànke gii may kuy toroxlu ci kenn ku dul aji doyluloo jiy aji yaatu (muy Yàlla) na ko wóor ne moom ku gumba la )) +(( moom de laay jàmbat samag lòtt ,samag ñàkk ak samag tumburànke,may yaakaar samag dellu ci lu gaaw di ngën ji ku nu xeewale )) +(( jàmbat naa ko samag lòtt,mu fajal ma ko,te nekkal ma ci lu kawe sama njort,moom kat mooy gën jaa teddi kuy terale )) +(( ñi nga xam ne weddi gi nu weddi Yàlla da leen a wor danoo jublu woon samag wàll,mu aar ma ci ñoom dàkku jepp aji tooñ)) +(( ag cant ñeel na ko tukkee fi man,di yaakaar ci moom sama càkkutéef lii,ci lu dul ab coona buy juge ci man,te sama naqar dañ na )) +(( ki njort wor ba muy iñaan, bu ma woree tam,na ko wóor ne ki ma wommat cig teral de woru ma)) +(( ku ma sànni ci géej gi ngir ag weddi di boroomug mbañeel,na ko wóor ne ci géej gii de tabeg aji terle ji dikkal na ma fi )) +(( koo xam ne li ko naqari mooy nekk gi ma nekk di jaamub Yàlla,tey jëwrini aji rammu jiy ku nu jiital )) +(( na ko wóor ne man de ab jaamam laa ci géej gi ak ci jéeri ji,di ligéeyal kiy musale ci luy waral reccu)) +(( ku ma dëddu de na xam ne xéewal yi jublusi nanu,juge ci aji yaatu jiy aji doyluloo,kiy aji wattu tey aji jiital )) +(( ku ma sànni ci géej gi ngir sàkku samag tumburànke,na xam ne ag tàggat ñeel na ma tukkee fa sama boroom ci gépp géej )) +(( samag wéeru ñeel na Yàlla ci samag teew ak samag fàdd,te di naa jàmbat jëm ci moom jaarale ko ci Yonnant bi,moom miy samab raas (bi may yéege jém ca Yàlla) ndaw muy ku baax )) +(( yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom ak ci ñoñam aki saabaam ak bepp jullit )) +(( yaw sama boroom saxalal ba fàww ngën jaa selli julli ak sëlmël ci Muhammad)) +(( ak ñoñam aki saabaam yepp,te nga delloo ma Tuubaa ci lu gaaw,te peek ma te xamal ma)) +(( yaw sunu boroom man de warlu naa ba fàww di kuy ligéeyal Yonnant bi,tey kuy ligeeyal aaya yi,na nga ma xamal te déggal ma )) +((yaw sama boroom,maa ngi sàkku ci aji maye ji ag géeju akug wuññi akug yinkiiwal (ag sol xam-xam mu tukkee fa Yàlla) na nga ma wuññil te yinkiiwal ma )) +(( jublu naa aji ubbi ji tey sàkku ag ubbeem,di yaakaar ci moom ay may yuy ball,ndax ag ballam day yol di sotti)) +((gërëm naa aji not ji bi mu ma tàggatalee noon yi,ma doonoon ku tumburànke,di ku wéet fa ñoom di ku amoon gépp lëmmu)) +(( di naa ko gërëmloo ci Alxuraan ngir sant ko ci xéewalam yi,ci sama xol ak sama yaram ak sama gimiñ )) +(( war na ma ma saxal li mu ma tànnal mu dig jub,te ma koy gërëmloo ci aaya yi ndax ñoom kat (aaya yi) mujj nañu di samam màng (ngañaay) )) +samay cant aki ngërëm aki tagg ñeel na aji jariñe joj indil na ma Alxuraan ju tedd ju ñu màggal)) +(( moom (Alxuraan) mooy ndàmm mi (koom mi) tey leer gu fés gi niy aar ci sawara ak noon yi ak gàcca)) +(( ab teere la bu tedd,juge ci aji tedd juy terale,jëm ci jaam bu tedd,buy xettalee tey boroom yërmaande)) +((teere bu darajawu la juge ci ku darajawu,ku darajawu te wóor indi ko, jéme ko ci aji darajawu kuy matal )) +(( xéewal ak jàmm ci lu dul dog yal nanu nekk ci moom,ak ñoñam aki saabaam fu mu man a nekk)) +(( jàmm ak xéewal yal nunu sax ci moom li feek aji sant a ngi naan : da ma ne maa ngi sant ngën ji aji xéewale)) +(( Xéewal yal na sax ci moom juge ci aji tedd ji may nekkal,te du ma jàmbat ñàkk ay xéewal ci menn mbindéef)) +(( mucc yal na nekk ci moom juge ci moom (Yàlla),(mucc) gog da nga ma ci fegal (yaw Yàlla) aw ay, te aar ci samag wàll wëlif ku nu rëbb ki (muy ibliis) ak ku gumba)) +((xéewal yal na sax ci moom tukkee fa moom(Yàlla),li feek ku koy jàmbati mbiram a ngi am la mu bëgg di gën ji ku nu xéewale)) +((aki ñoñ aki saaba yoy maa ngi ñaan aji kawe ji mu dugal ma ca seen biir ëlëg may boroomug xéewu )). + +Bokk na ci karaamay géej gi ba tay nettaleem bii,mu ne: bis xëy na, waaj ngir ligéeyal Yonnant bi - ni mu ko baaxoo woon - amul lu dul aw mettit wu tar daj mbooleem yaram wi,ba manatul li mu bëggoon ,waaye am benn tubaab ci njiiti nguur gi,mi ngi dëkkoon ci wetu fi Sëñ bi dëkkoon,nekkoon di xaqataay ca kaw aki moroomam,Sëñ bi daa di ne:Yàlla yaw de xam nga li ma waajoon jëm,ak li ma ci gàllankoor,maa ngi lay ñaan nga tuxal lii fi man te yobb ko ci ki lay wutal moroom,amul lu dul ma dégg waa ji doon xaqataay muy onk,man may bind. + +Bokk na ci karaamay géej gi ba tay lii: bis nee na fi mu nekkoon ndawal da faa mànke woon lool,ba jën yu ndaw yi nuy def ci poti weñ yi rekk lanuy lekk daanaka (xam naa mooy poti ton yi) ma jëfandiku ci bis,bi ma noppee ma raxasu ba sonn,jëfandikoo suuf ak saabu ak lu nu man a dindee ag xet rekk,waaye dara,ba ma ca manatul dara ba ne naa dem nag jublooti ca ligéey ba,bi ma tàmbalee rekk ñu ne ma ((wa minhumul laziina yuuzuunan nabiiya)) muy am na ci ñoom ñuy lor Yonnant bi,ma tiit lool, jaaxlee jaaxle,ca saa sa ma bàyyi koo jëfandikoo,doxe ca bàyyi luy jën,boole ko ci li ma jaayante ne du ma ko lekkati,bis bi ma ko bàyyee walla lu ko jege,ay kuy dikkal nanu ma,juge ci fere yi,di njëg gu nu gaawal ci jën yi ma jaayante woon. + +Mu neeti moom ku baax ki:dëkk bi mu nekkoon da faa nekkoon aki làbbe ñuy jël ci xaley yéefari nit ñu ñuul ñi nekkoon foofu di leen def ay mbindaan,di ànd ak ñoom di wër ci ja yi (marse)ginaaw tàkkusaan,njiit li nekkoon foofu defe woon ne da maa xemmeemoon ci gone yi mu ne ma woon boo ci soxlaa de ma joxla ci ñuy ànd ak yaw,ma ne ko soxlwu ma ci. Njiiti dëkk booba itam baaxoo woon nanu di jël ci magi nit ñu ñuul ñi, ñu ñuy def ay toggkat aki rootkat,ma sàkku kenn ci ñoom bis ngir ligéeyloo ko,waaye ba mu ma jegee daal xeeñal na la ko xeeñ goo xam ne amul gu ni mel,ma ne kii daal sobe na ba maneesul a jaxasoo ak moom,ca noona ma jaayante ci seeni ndaw ak seeni mag ni ma jaayantee ci jën yu mag yi ak yu ndaw yi ,ci loolu mu ne: + +(( ma ne njëgug ndaw ñi dikk na ak gu mag ñi ak ndaw ñi)) +((Muhammad gën ji imaam mooy sama dëkkandoo,ag bëbbam de (dexam) ci sama xol lay sottiku jëm)) . + +Fere yi ñëwoon indi kuy yi (xar mu goor mu mag) ñooy mosalug njëgi yéefar yu mag yeek yu ndaw yi,kuy yooyu it di mosalug njëgi jën yu ndaw yi ak yu mag yi. + +Bokk na ci karaamaam yi ci géej gi ba tay waxam jii mu ne: +bi ma xoolee sama diggante ak noon yi ,nooni Yàlla yi,ma xam ne ñoom kat am nanu kàttan ci lor ma ak gaañ ma,ci dogalub Yàlla bi ak’ug nammeelam,ma xam it ne bu doonutoon kaaraangey Yàlla ji ak’ug fegam kon ba tay waxatunu ko,laa leen bàyyi ak seen bëgg-bëgg,jublu sunu boroom,mi yor mbir yi,ma déeyaale ak moom ci sama mbir: +ma ne ko Yàlla yaw’ay ki nu bind ngir nu jaamu la,nga ne ((wa maa xalaqtul jinna wal insa illa liyahbudoonii)) muy bindu ma nit ak jinne ndare ngir ñu jaamu ma,nga neeti : (( yaa ayyuhan naasu uhbudoo ràbbakum)) muy yeen nit ñi jaamu leen seen boroom,bu ko defee tawfeex ñeel ki texe jiitu ci moom,mu dégg wax ji topp ko,naka noonu toroxte ñeel ki ag texeedi jiitu ci moom,mu lànk bañ a wuyyu,tëx, luu, ngir’ug weddi,man nga tawfeexal ma,def ma ci mbooloom ñi wuyyu,mbooloom Yonnant bi Muhammad (j.y.m) imaami anbiyaawu yi ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom ñepp,nga dolleeti ma ngënéel,def ma may jëwrini Yonnat bi tey xalifaam ci diineem ak xeetam,am mbooloo ci sa noon yi, noonam yi,jug song ma ngir dox sama diggante ak jaamu la,te ligéeyal ko (moom Yonnant bi) . Ñoom dey ñi ngii di ñu caaxaanadi ci seeni jëf,di ñuy farlu ci seeni neen,te yaw yaay ki wax ci làmmiñu sa Yonnant bi,lol maanaa mi mooy:nit ku nekk daa am kër ca àjjana ak ca sawara,bu duggee àjjana ñu won ko këram ga woon ca sawara,ne ko fee de nga jëmoon boo jaamuwutoon sa boroom,leegi nga xam ne daa nara gént,ab yéefar a koy donn. Bu tàbbee sawara’at nu won ko barab ba mu doon am ca àjjana,bu jaamu woon Yàlla,ginaaw nag jaamuwul boroomam ba tàbbi sawara,leegi ab jullit lanu koy jox. Ginaaw mbir yi nii lanu deme,te noon yii - ni nga ko xame - ci tooñ ma lanu dëkk ak a def ci man lu leen soob,te du ma fayyu te du ma leen ñaanal aw ay,waaye maa ngi lay ñaan seen kër ya ca àjjana,Yàlla nangul ma ko,may ma leen,ba ma xamee ne maa leen moom,ma jox leen àddiya waa-Ahlu Badrin . Ci loolu mi ngi naan: + +( jox naa àddiya këri noon ya nekk àjjana mi kuy jalgati dul dugg,ñeel saabay Yonnat bi)) +((kër yooya de jëlees na leen ca noon ya,jox leen saaba yu baax ya)) +(( Yàlla jox na ma kër ya fa samag tumburànke,teeyal it samab xol)) +(( man nag def naa leen ay àddiya ñeel saaba yi,yal na leen Yàlla gëram ,moom mi ma aar wëlif (sahaab:ay niir ) )). + +Na nga xam ne karaamay tukkib géej ji moom maneesu leen a jeexal,bu ma bëggoon a indi li ma ci xam ci lu juge fu wóor ,ak li ma ci dégg ci nit ñi,kon dey ma indi fi lu yéem xel yi,te kon du xaj ci teere sii di su nu gàttal,looloo tax ma yam ci li nga xam ne topp naa ko ba mu wóor. + +Mu ne ati tumburànkeem gi juroom ñatti at yu mànke tuuti la,bi mu matalee li ko Yàlla bindaloon cig tumburànke,ci suufus yéefar yu ñuul yi,Yàlla indeeti ko ca suufam ngir nitam ñi ñoom itam jariñu ci moom ci li ko Yàlla may ciy mbóot ci tukkeem bu barkeel boobu,ak ngir mu daje ak mbokki jullitam yu baax yooyu di naar yi,ci noonu Yàlla dal di def ci xoli kilifay nguur gi ñu am ag ñeewant ci moom delloosi ko. + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Sëñ baa ngi àgsi Ndakaaru bisub gàww juroom benni fann ci sahbaan,atum kasasin di 1120 g, mu wéye fa, jàll Ndar def fa lu tolloo’k fukki fan ak juroom ba ca bis bu njëkk ba ci ramdaan, mu doonoon bisub talaata,mu juge fa,dem Luga, wàcc ca rakam ja Sheex Coro MBAKKE,ca guddig gàwwu ba, mu rañaane fa romb kër Sheex Jull SIISE,jugeeti fa jaar kër muridam ba sëriñ Sire LOO, yoor-yoorug dibéer ja ca Sànnoosi, mu sax fa la desoon ca ramadaan ja,noppalu fa,woor fa. + +Ci diir bii,foofa fees na dell,raj-rajloo ba mel fa nu mu masul a mel,ci diggante ay taalubeem ak kuy sàkku ndimbal,aki kilifa yu koy siyaaresi,di ko ndokkeelsi,bokk na ca ñooña ka nuy wooye (kiimaanug jamonoom,woykatub waxtoom) Sheex Ibraahima JOOP Almasharii,ab xisaam lu xoromu la te yéeme,ag wuññi (feeñal mooy wuññi) gu yéeme feeñ na ci ñeel Sëñ bi (maanaam Sëñ bi wone na ci ay xar baax) loolu mooy sheex Ibraahima moomu daa amoon ab bor bu mag bu ko lëjëloon lool,ci jamono joj fay ko ci jafe na,mu jug wër ak moom ci sëriñ su mag si waaye taxul kenn tëyye ci loxoom,ci noonu mu jaaxle lool te am tiis,waaye bi Sëñ bi agsee Sànnoosi,mu ñëw indaale ay bayitam tudd ci mbirum bor bi ak ni mu ko seddalee ci diggante Yonnant bi(j.y.m) ak ñeenti saabaam yi,ginaaw sëriñ si nanguwunu koo xettali. + +Bi mu yëgloo Sëñ bi ne ko mu agsi,mu dikk,nuyyoo,bi mu daataa wax ay mbiram ak boram bi ak ni mu ko seddalee ci bayit yi,Sëñ bi ne ko indil ma mbuus mee,mu indi ko,mu neeti ko jox ma mi ci des ,mu jox ko ko,mu ne ko waññal li nekk ci mbuus mu nekk,mu waññ ko, muus mu ne ñatti téeméer nekk ci,boo leen boolee ñuy juroom benni téeméer,Sëñ bi ne ko indi benn téeméer bi te jël li ci des dimbandikoo ko ci say soxla,te moom boram bi juroomi téeméer rekk la woon,ca saa sa sheex Ibraahima daanu ab jéll,yuuxu ca kaw,Sëñ bi ne ko waaw yaw lu mu? Mu nettali ko xisaam,jàngal ko bayit yi,moo nekk nii: +((bori ay mbokk war na ma,ma seddale leen ci diggante ñu tedd ñi ndax ñu fay leen)) +( yaw Ku nu tànn ki(Yonnant bi), ya’ay ki moom cér bu njëkk bi,yaw su xarit bi (Aboobakar) ya’ay ki moom ñaareelu xaaj bi) +( yaw ki teqale dëgg ak fen (Omar) ya’ay boroom ñatteel bi, yaw sunu Usmaan mi, nga moom bi ci topp) +( yaw gayndeg xarekat yi,yaw baayi Asan ak Usaynu ñiy leerug sunu diine ji,yaw laa feetale li ci des) +(yeen de ñu tedd ngeen ñoñ kuy jàmbati coona du wéeru ci seen daraja te fajalu leen ko ko) +( kon gën jaa selli xèewali Yàlla na sottiku ci yeen,li feek Yàlla a ngi faje ay soxla ci yeen). + +Sëñ bi yéemu lool te sant Yàlla,waaye noon yi ñoom seen kiñaan gi mayu leen sax ñu xaar ba Sëñ bi ñibbi këram,waaye danoo dal di tàmbalee wut seeni pexe,di lal seeni yoon, di waajal li nu nar,di xaar waxtoom jot banu def ko. + +Ku baax ki moom bi mu jullee iid ca bisub kori ga,mu doonoon bisub alximis,da fa’a toogaat bisub àjjuma ak gàwwu ba ca tàkkusaan sa,mu laxase fa romb ca kër taalubeem ba Koor Mag JOOB,boole fa timis ak gee,ngir tarug dox ba,dem Màkka Sàmba JOOB fanaan fa,xëy bisub dibéer dem kër baay tëxam Sheex Ibraahima MBAKKE Kajoor,laxasati ca tàkkusaanug altine ba, dem ca Masàmba Xari JOOB,moom mi ngi kër Muxtaar,fanaan fa, yendu fa,jugeeti fa ngoonug talaata dem ca Muxtaar Mareema Silla ca Ñaxal,mu def fay fan,juge fa jàll Kokki Guy ca Maxtaar Masàmba JOOB,yendu fa waaye fanaanu fa,da faa juge njëkk jant biy so,te booba ña ngay waajal ñam yi,waaye taxul mu xaar ko fa,dox nag jëm Daaru Salaam këram,àgg fa guddig àllarba ci lu tolloo’k ñaar fukk ak benn,Siidi Muxtaar ,rakam ja booba ma nga fa woon,ca biir sawaal. + +Rakk ji (Sheex Anta) tàmbli di ko ganalee lol kenn ci murid yu mag, yu man yi sax manu ko,waxantu ma la’ak ñu néew ñi doole. +Mu sax fa diirub fukki fan,bis bu nekk ñu ray ay fukki yëkk,bu ko matalul mottali ko ci giléem walla ay giléem,kem li mu mànke rekk.Ñu koy waajal ay wàccuwaay ca rakk ja sheex Ibraahima,diggante Tuubaa ak Daaru Salaam,muy fa Sëñ bi tudde woon Daarul Mannaan, mu dem fa moom ku baax ki ci njëlbéenug silqihda . + +Sheex Ibraayma mii moom jërul ngay laaj ay mbiram, mooy ki ku baax ki dénkoon njaboot gi ak bagaas yi,bi miy tukki. Ci noonu màgi taalube yépp daje fa,Sheex Ahmadu Ndumbe jiite leen,mooy ki doon dem ak a dikk,di yee ñi gëmméentu,di jàngal goney Sëriñ bi ba nu mokkal ci diir bu néew njëkk ku baax kiy dellusi,dara yàquwul ci mbirum Sëñ bi,ba ñépp daan ko léebe ci wàllug jub ak tegu ci yoon. + +Mu jullee foofa iid (tëbëski),sax ci meloom wu sell wa ak yareem (tarbiya) ga mu nekkoon,mbiram ak mu dongaam yi di gën a jëm kaw . Kawe fopp,fopp,fopp na mu meloon,kaamil yi ñu leen di jàng di leen xool ci bëcëg gi ,di leen tari ci gudd gi,naka noonu xasaayit yi,ak njàngalem xam-xam mi,ak ligéey bi ,loolu lépp àgg fof maneesu koo melal cig kawe. + +Ni nga xame ne mbirum ku baax ki yokk na ak mu taalube yi ba jéggi ab dayo,ba maneesu koo misaal,naka noonu mbirum ñu iñaan ñiy rambaaj. Mbirum jaxase gi dellu fa mu nekkoon,rambaaj yi jug di def seeni ligéey ba nu xëy indil Sëñ bi ay soldaar,li ko waral mooy: jaraaf ji nu dénkoon mbirum wàll googa,ca jooja jamono,- moom xam nanu turam ak giir gi mu bokk - waaye bëggu ma koo tudd di nëxal ay doomi baay tëxam,ak doonte àndunu woon ak moom ci yéeneem ak jëfam ak waxam,waaye ginaaw seen doomi baay tëx la,rafetatul nu leen koy tuddal,te doy na ne ñi teew moom xam nanu ko ci tur,ci jëmm ak ci mbokk,te yal na Yàlla musal ñi teewul ñuy xam turam. + +Moom de moo waxoon te tegu ko woon fenn ne : Sëñ bi day dajale ay kano aki fital ak yeneen jumtukaayi xare,te mi ngi waaj fi mu nekk,bu ngeen ma joxoon ay soldaar de kon ngeen gis li may def. Ñu àndoon ak moom ci kaw waaye wóoluwunu woon ay waxam,looloo waraloon ñu boole woon ko ak buuri réew mi mépp,buurub Kajoor,bu Bawal,bu Siin,waaye bu Siin a ci gënoon a rafet njort ci Sëñ bi,gënoon cee rafeti wax,waa-waaw xamal nanu ma ne am na ay buur yoy seen biir de Sëñ bi la àndal. + +Am nanu xam-xam ci ne bi nu àgsee waa juy rëy-rëylu ji méngoo woon rëyam nga (al lazii tawallaa kibrahuu) moo dal di woon tàmbali di dog sàkket yeek jaaseem ji, te daawul xaar ku ko ubbil bunt,lépp lu dox ci kanamam mu dog,te amul lenn lu muy rus,dale ko ca sowwu ba, ba ca penku ba. + +Fekkoon na Buur Siin - ci li nu wax - mu wutoon ay fuglukat (controlleurs) indi fa ngir ragal ñuy dugg cib néeg di fa duggal ay ngànnaay walla fital te kenn du ko yëg,ngir dëggale ci li nu waxoon ne Sëñ bi day dajale ay ngànnaay,waaye Yàlla dogal loolu amul,bu nu ko bëggoon it du man a am,ndax donga yi doonte danoo bank seeni loxo,teewul ñi ngi ànd ak ñoom ci ay bët ak ay xoolkat. Bi nga xamee ne gisu ñu lenn ci li nu doon tuumaal sëriñ bi,te gisunu ci donga yi kenn ku yor kanam gu lëndëm mbaa gu ñëkk,ku ñu ci gis rekk ma nga mel ne kuy waaj a julliji kori mbaa tëbëski,ngir tuwaaletu bu rëy,ñu xam ne noon bi day fen,buur yépp rus,am kersa ku ci dul waa ju fettéerlu ji,moom sax gàccawu na waaye daa suturloo jàmbaar-jàmbaarlu ak sàkku-sàkkulu nu ganaleel ko buur yi,ak xontal ko fas yi,waaye lu mu soxla rekk nu defal ko ko ca na mu gën a gaawe,gënnee yombe,ci noonu ñu dellu di ñu reccu,yal na Yàlla fay ña ca amoon yéene yu rafet. + +Ag karaamaa ngi nii: +bi sodaar si laataa agsi ay mbokkam moom Sëñ bi danu koo wër lëjël ko witt,gën a tar ci moom ay jiit,tiit gi nu tiitoon taxoon amatunu woon kersa,taraloon lool ak moom,demoon ba bëgg koo génn seen biir bu nu ko manoon,ña ca bokkutoon ca mbokk ya daal mooy ña ca yaroo ca moom,waaye ku baax ki moom loolu lépp téewul mu doonoon ku féex ku ko yëgalutoon yaramam,naan leen bég leen,wallaahi mbir mii ñaari bëy dunu ci daanate,waaye kuy dégg loolu ? Ñoom ñii nga xam ne tiitaange gi yobb na leen ca dayo ba moos. +Ca bis yooya ku baax ki génneel leen aw dagiit wu yéeme ciy woy,ne leen bu ngeen ko jàngee ci kanamu soldaar si du ngeen dégg lu leen naqari mbaa ngeen koy gis,moom nag ñi ngi ko toftalee ci arafi (Rahmaan Rahiim)(muy boroom yérmaande ju nu yaatal ji,ak boroom yérmaande ju nu jagleele ji) moo nekk nii: + +(( sama boroom de bettee na ci luy leeral xel yi,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)) +(( samag cant ñeel boroom bu tedd,bu amul bokkaale,sama dënn it tay fees na dell ak leer guy jolli)) +(( Muhammad ,xéewali sunu boroom yi ba fàww yal na nekk ci moom,sama lépp de ci moom la ko watoo )) +((maa ngi ñaan sama boroom, moom mi ay mayam matale mbooleem mbindéef yi, la mu tànn moom mi binde )) +((déeyaale naa ak moom - moom de màgg na - ay at , mu teral ma teralug aji gindee,sama lépp it set na ciy caaxaan)) +(( yaw boroom yérmaande ju matale ji,mayal mbooleem mbindéef yi yërmaandey ka nga xam ne ku jàng Alxuraanam ji,mu feg la wëlis aw ay)) +(( aaral xeetu Mustafaa wi ci gépp yàqute,te nga yërëm mbindéef yi,yaw mi bindoon seen maam)) +((yaw boroom nguur gi ,yaw mi màgg wëlif fayyoontoo, yërëmal mbooleem mbindéef yi,yaw aji gindi joy dimblee na))) +((far nga la xol ba jublu woon ciy lor,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)). + +Sama mbokk Muhammad doomi Aliyu Alyahxuubiyu,nu gënoon koo xame ci turu Muhammad Tuubaa,ngir taqoo gi mu defoon ak ku baax ki ca Tuubaa,ak baril lu mu daa sikar,ak a jàng xasida yi,xibaar na ma ne bi Sëñ bi génnee xasida gi (Rabbii bimaa yashrahul),da ne ma mokkal ko, ma mokkal ko ba nu daataa ñëw,bi nu ñëwee mu woo ma ne ma jàng ko ca kaw,biral ko,ma jàng ko ni kuy nodd,baamu ko lu tolloo’k ñatti yoon,mu ne ma doy na ,mbir mi mat na te yéwan. + +Mu daan def fu mu nee ma dajewunoo’k lu nu naqari de,ma ne ko xasida gi -ci karaamay ku baax ki- def na ci soldaari Tuubaa yi la picciy Abaabiila yi defoon ca soldaari Màkka ya,ngir sunu Yonnant bi (j.y.m),waaye ñii ak ñee li leen wuutale, ñii dañiy ñoñ ay nu jëflanteek ñoom ci kem seeni yéene,naaxsaayal leen,ñee ña ca ëpp di ñu baax,ñu ga (forse) leen ,te seeni xol Sëñ bi la àndal, Yàlla yeexal seeni mbir ba nu bari tuub ci,ba ca ka leen jiite woon,moom it tuuboon na,ñenn nit ñaa ngi sikk ay mbiram nag,bi nu xamee ne lòtt doo nga tuub du tuub. +Sëriñ bi nee na : +((dëgg-dëggi tuub mooy nga bàyyi bàkkaar boo mas a def ngir Yàlla)) +(( ci sa coobarey bopp,waxunu lu mel ni (lu la Yàlla teg) niki tëx ak jàngoroy pëy ak gumba ak luu)) +((nga bàyyi ko rekk ngir màggal ku màgg ki,ak ragal mbugalam mu metti mi)). + +Man nag li may wax mooy lu man a xew ci mbooloom Sëñ bi la ,moo xam daa lòtt walla daa tuub,mbari na lu Yàlla jéggal ku tooñ te tuub,bàyyi ko ak Yàlla daal a gën a wóor, rafet njort ci moom itam a gën a mat,Yàlla nee na : ((fa man jaa ahuu mawhizatun min rabbihii fantahaa fa lahuu maa salafa mamruhuu ilal laahi)) muy ku ag waar dikkal juge ca boroomam,mu bàyyi la mu doon def,la mu jiital ñeel na ko,te mbiram moom ma nga ca yàlla. +Bi soldaar si demee,ci la génne ci ndigalul Yàlla ak Yonnantam ci ñaareelu tukkeemba,ma nga ca naan: + +(( ku jorte ne sama dox ba ginaaw atum aksasin di 1321g,moo’k sama dox bi ci bopp jaysasin di 1313g ñoo yam)) +(( sax na ne aji réer ju dof la ,ndax moom dox boobu teeyal (neexal) gu aji kawe ji di teeyal samag dund la)) +(( saama doxub aksasin bi du lu dul yoolub ki ma wommatal ci ginaaw bi dëël (dig) bob def na ko)). + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Ci bisub gàwwu,fukk ak juroom ñaar ci weeru gàmmu atum aksasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak benn,la Sëñ bi génne ca këram ga ca Daarul Mannaan,ginaaw bi ko ay bataaxel dikkalee aki ndaw tukkee ca nguur ga,naan ko na leen fekk Ndar ginaaw tisbaar. Mu fanaan Ngaabu ak njiitul soldaar si,xëy dem Njaaréem ,juge fa dem Tool,juge fa jàll Tiwaawon,foofa la yéege saxaar dem Luga,ware fa gaal dem Dagana,loolu lépp ci ag ayu bis,sax fa juroomi guddi,jéggee fa dex ga juge Dagana ginaaw bi, ci ñaar fukklu fan ci weeru gàmmu ànd ak waayi Sheex Siidiya Baaba ji,mooy Sheexunaa Ibnu DAADA,man na’a am li waraloon loolu di woon li nu wax ne Sheex Siidiya’a ko wax muy ne leen sëriñ bii de amul lenn lu ñaaw lu deesi ragal ci moom. Ñu ne ko woon ndax man nga noo wóoral (gaaraantil) li nga wax? Mu ne leen warlul naa leen ko,ñu ne woon ko kon leegi danu koy boole ak yaw. + +Sëñ bi moom daawu leen yeexal lu dul diggante bi muy xaare ndigal lu juge ca boroomam ak sangam ba,loolu moo daan waral ñuy jort ne daa lànk,te fekk booba noonu la deme,ci noonu mu dem ànd ak Sheex Siidiya,ba nu àgg ci yenn ci kër yi nga xam ne du nu woon këram,waaye yu Banii Daymaan lanu,mu wàcc fa ngir ay mbir ci digganteem ak yenn giir yi,bu ko defee ku baax ki wàcc moom itam,bu niy laxas mu laxasati def ko ay yoon. + +Bi tuxu yi baree nag ak màngaan mi ci wenn weer walla ñaar,nga xam ne daanaka dunu sax fi barab,te loolu wuute na’ak lool aaday waa réewam,loolu tiis ko sonnal ko ak ag njabootam,te itam taalubeem yi danu koy dikkal fu mu man a nekk te barab yi sori nanu,sàcc yi bari ci yoon yi sonnal leen it ya yooni yoon,ci noonu ku tedd ki sàkku ci ñoom ñu tàggoo,ñu bañ ngir xér ci ànd ak moom,ak ngir yilla ju jiitu ji muy dénk gi ko ko nguur gi dénkoon . + +Waaye Sëñ bi moom dogu rekk,nu xam ne ku dëggu la,te du sàkku dara ci bànneexu bakanam,nu ànd ak moom ci li mu bëgg,nangul ko ngàntam,moom itam mu jàmmante ak ñoom ci aw bayit wu yàgg:( bu ñu nu tànnloo woon de du ma tàggoo’k yeen, waaye ag tànn àndul ak jamono ),Sëñ bi ginaaw lii du bayitu boppam mu soppi waaye ag tànn àndul ak jamono,def ko waaye ag tànn àndul ak am ñax,jublu ci loolu yéen da ngéen di sàkku fu ngéen di sàmme ak fu ngéen ko man a ame,loola reeloo leen. + +At mooma mu woore Sarsaara koor ga,muy barab bu nu xam fa ñoñam,nit ñi sottiku fa,ak ñuy jële ci moom rawati na ci Banii Daymaan ak seen kilifa ya,doomi Baydah yi Abdul Laahi aki mbokkam ci loolu ku baax kaa ngi naan: +(( mbooleem sama xeeti cant ñeel na ki nga xam ne sama lépp ci moom mujj na di ngërëm lu àndul ak ab sàññ(mer), ñeel ko fa Sarsaara)) +(( moo moom sama tagg ak sama ngërëm ci lu dul sàññ,bi mu ma wommatalee ay ansaar yu bokk ci Banii Daymaan)) +((sama lépp ñeel na Yàlla fa teeni teraanga,yu nu tuxoo,te bari na fa ñu siyaaresi)) +((ñi nga xam ne danoo dikkoon Sarsaara ngir siyaaresi ma fa,na nu xam ne tàggoo nanu aki bàkkaar àdduna ak alaaxira)). + +Ci Sarsaara gii nee na daje na fa’ak Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu,du ciy gént,mu jox ko Wirdul Maaxuuz .Fekkoon na njëkk loolu Sang Bu nu Wóolu bi dikkaloon ko ca géej ga,rékki (jël)woon ca moom lépp lu mu jële woon ci nit ñi,ba deseetu ci dara,mu jox ko wirduw Xaadir,ba ca mujjug tuxal ga nga xam ne loolu day tegtale ne daje na ak Yonnant bi (j.y.m) ca géej ga,Jibriil dikkal ko fa mooy Sang Bu Nu Wóolu bi,rékki woon ci moom la mu ca rekki woon,joxoon ko la mu ko joxoon,jaarale ko ci Yonnant bi (j.y.m). + +Mas naa teew bis kenn ci boroom xam-xami naar yi laaj ko kuy Sang Bu Nu Wóolu bi ? Mu ne ko Jibriil,mu ne ko ndax Jibriil dees na ko gis ginaaw Yonnant bi ? ku tedd ki tontoo ko ñaari bayiti ki woy Xazawaat : + +(nee nanu Jibriil da na teewal kiy faatu te gëm,aw nit it weddi nanu ag dikkam ginaaw Yonnant bi (j.y.m), dëgg gi nag mooy amul ab dayo (ag dikkam) ) . + +Sëñ bi neeti ko waaye wax jii am na ñu ko tax a jug,ñooy ñi ci am ag ñam akug dëggal,waa ju juge fee rekk nag li war mooy mu nangu ko mbaa mu noppi,ngir bañ a loru. + +Man nag ma ne misaalum loolu mooy lu mel ne ku nu digal mu taal ab taal ngir aajo ju wér,mu taal ko,ab lëpaalëp jaar fa tàbbi ca,dee,kon kooku dara waru ko ca dee googu,naka noonu ku nu digal mu wax, bu waxee.Ma ne wàlliyu yi di gis malaaka yi moom kenn manu koo weddi, ndax jële naa ci mbindum sunu sëriñ Xalifa Alhaaji Muhammadul Faadil,moom mu jële ko ci yenn ci teere yu mag (majaamih) yu wér yi lol ab yaxam mooy ku ñu ubbi (maftuuh halayhi) moo xam ab nabiyu la walla wàlliyu,manul a ñàkk mu jàkkarloo’k malaaka,ci seeni jëmm,ni ñu mel,tey wax ak ñoom ñuy wax ak moom,képp ku ne wàlliyu du gis malaaka tey wax ak moom kon na xam ne tegtalub loolu mooy moom du ku nu ubbi,lii nag mooy layuw ku nangu(féeñug Jibriil),ci ku ko nanguwul. + +Ginaaw Jibriil da na dikkal aji gëmm ji buy faatu,te ku ñu ubbi day gis malaaka yi tey wax ak ñoom,te yinkiiwalug wàlliyu yi (sol gi nu leen di sol xam-xam ak li Yàlla di bëgg ci ñoom) mi ngi am jaare ci malaaka walla mu am ci lu dul muy jaar ci kenn,ginaaw loolu lépp am na,kon du jomb ci Jibriil moom mi Yàlla wóolu ci wëhyoom gi,mu nekk ag diggale (intermédiaire) ci yobb ak joxe yinkiiwal gi Yàlla di dsotti ci ñenn ci wàlliyoom yu mag yi,ginaaw ñoom ñooy ñiy dònn yonnant yi. + +Moom Jibriil dimbali na sunu sang ba Hassan saaba bi (y.y.g)ci teewaayu Yonnant bi (j.y.m),mu di ag kiimaanam tey karaama ñeel aw wàlliyoom,luy tee kon mu man a dimbali ligéeykatam bii ci ginaawam,mu dig kiimaan gu ñëw ci ginaaw bi tey karaamay wàlliyoom wu dikk ci ginaawam te di ko ligéeyal ni ko Hassan,wàlliyoom wu njëkk wa doon defe. Ñoom ñaar de ay mbokk lanu ci lgéey bi,ba fa tuxal ga xam. +Du ñàkk ñariñ ñu indi tuxal gi ba ngéen gis ko,mi ngi nii:da ne yal na ko Yàlla mu màgg mi gëram : bu dee bunt bi yor wirduw aji nos ji (aji woy ji) moom doggantal nekku ci ,(doggantal= français =chapitre,araab=faslun) aji nos ji ,wird wi mu njëkk a jël ci wird yi mooy wu Xaadir,ginaaw bi wu Shaazaliya,ginaaw bi wu Tiijaan. + +Bu dee wirduw Xaadir moom jëfandikoo na ko lu yàgg,daan ci sàkku ndigal ci képp ku mu mas a yaakaar ne ku nu ci jiital ga (muxaddam), ba jële woon ko ci ñu bari. Ginaaw bi mu wóor ko ne ñi mu daa jële du ñu ci woon ay muxaddam maanaam ñu ñu jiital (ñu ko war a joxe) ,mu sàkku ci Yàlla (t.s) mu may ko ci lol ag gëlëm mbaa ag dengi-dengi dootu ci nekk. Mu ne bi ma Yàlla yobboo ci géej gi ma nekk man rekk ak moom la ma Sang Bu Nu Wóolu bi dikkal (j.y.m),dal di rékkee ci man lépp li ma jële woon ci nit ñi ba dara desatu ci,mu jox ma Xaadiriya ci diggaleg (jaarale ko ci) Yonnant bi (j.y.m). Tuxal gii ak lu ni mel ci mbidd yi, danuy wone ne Sëriñ bi daje na ak Yonnant bi(j.y.m) ak Jibriil (j.y.m) ci lu dul woote ag yonnant,du caangéenug wëhyu,waaye ci kem li Yàlla di jagleel lenn ci wàlliyoom yu mat yi. + +Waxam ji mu naan wirdiy aji nos ji mi ngi ci jublu woon xasida gi mu doon tudde ñatti sëriñ yu tedd yooyu,ak dònn gi mu leen dònn, tuddati sunu sang Anas,ak Hassan (gërmul Yàlla yal na nekk ci ñoom) ak dònn gi mu leen dònn ci waxam jii: ((wommatal nga ma la Jiilaani (Abdul Xaadir Jiilaani)kawee woon ba fa mu yam)). + +Ku bëgg a am lu ko leer na xool teere bi nu naan “Tanwiirul halaki fii imkaani ruwyatin nabiyyi wal malaki”di ci maanaa leeralug lu lëndëm këriis ci man a nekkug gis Yonnant bi (j.y.m) ak malaaka,teere boobu boo bëggee lu leer rekk moo ciy géej jug mbàmbullan gi.te boo defee ag settantal ci tuxal gii ak li ci topp,da nga gis la amoon kon ca géej ga muy ni nu nangoo woon li mu jële woon ci ku dul woon Yonnant bi(j.y.m),ak dello ngi ko ko Yonnant bi delloowaatoon,ak naayibam yi, ñatti sëriñ yu tedd yi,ngir mu nekk naayibam moom Yonnant bi ( aji wuutoom),tey ki fi wuutu yooyule sëriñ (g.y.y.ñ),ci seeni wird ,di seen muxaddam bu nu joyal bi , nga xam ne amul lenn lu ko tënk ci wenn wird,(ku ko neex ak nu ko neex la koy joxee) ,da nga ci gis it la amoo n ci Sarsaara muy jox ga nu ko fa joxoon wirduw boppam moom rekk,jagleel ko ko,nga xam ne benn sëriñ bu ko fi jiitu masu koo yor. + +Looloo waraloon daawul digal ku jébbalu ci moom te yoroon aw wird njëkk muy ñëw mu koy bàyyi,da koy digal kay mu tëye ko te yéene ne moom moo ko ko jox,ku jébbalu ci moom nag te waxoo ko dara,bu boobaa mu door laa jox wirduw boppam. Looloo waraloon doomam ju tedd ja,sunu sëriñ,SheexMuhammadul Bashiir naan cig xasida gog biral na ci ngënéelug wirduw Sëñ bi ci yeneen wird yi,xaaral ma jox la ko lépp,ma nga ca biir it waxam ja mu naan: ((wommatal nga ma la Jiilaanii kawee woon)) ba ca bayit ya nga xam ne sëñ Bashiiru tudd na leen ci xasidaam gii,mi ngii: + +(ci turu Yàlla laay tàmbalee aw woy wuy jariñ ku bëgg a jariñu te ab xolam set) +(ag cant ñeel na Yàlla,yal na dolli xéewal ak mucc ci Yonnant bu nu tànn bii di gën ji mbindéef) +(ak ñoñam aki saabaam ,ñu tedd ñii te diy sang,ñoom ñi wuññi lëndëmi xol yi ak lëndëm) +(bu loolu jàllee ma naan la déglul waxi kiy laabiire boppam tedi la laabiire ci luy faji aajo) +( yaw miy sàkku matug texe ci yooni ñatti sëriñ yi) +(yoonu sëñ Imaam Jiili (Abdul Xaadir Jiilaani) ak Shazali mi làq ag ngënéel) +(ak Abool Habaas (Sheex Ahmad Tiijaan) miy ndamul ñu mat ñi,ñoom ñooñu nga xam ne seenub àtte ca jublu ga (xasd) mooy àtteb ku njëkk ka ) +(ànd ak ku ci nekk yor sa jagley bopp yoy ci la saw yoon làqe ay jagleem,loolu nettali nanu ko) +(na nga taqqoo’k yoonu Abdul Xadiim (jaam biy ligéeyal Yonnant bi) ,ndax moom kat moom la Yàlla mu jiitu mi jagleel mu dònn yoon yooyu yépp) +(ndax kat wird wu nekk am na mbóot,ci benn baat bu ci nekk,(ci biir wird wi) yal na la Yàlla gindi) +(baat boobu nag boroom “baziira” yi rekk a ko xam (baziira = gisug xol )keneen ku dul ñoom xamu ko,muy hikamu ab boroom buy aji not ) +(misaalam mooy Laylatul Xadar ci weeru koor wu nekk,ak Waxtuw Àjjuma,dees leen di wër di) +(Yàlla feeñalal na ko (moom Sëñ bi) ya làqu woon yépp (ci wirdiy yeneen yoon yi),ginaaw bi mu leen ligéeyalee te yekkati ag wàllam ngir jëmmam ju tedd ja,ba mujj ñépp bëgg ko jiital ko,(def ko muy seen muxaddam (ku nu jiital ki am sañ sañu joxe wird wi) ) ) +( Yonnant bu nu tànn bi tam - yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ak mucc ni mu ko tànne - yéegal ko ci ab hadara bob ku dul moom fàddu na ci yaw,bu nekk fa aji kawe ji (muy Yàlla) loolu di lu kawe sax la mu doon wut ) +(bi loolu wéyee mu donnalati ko lu nu nëbboon li , muy aji jiitu ciw yiw joj wuññi na ay fitna) +(ci coobareem (moom Yàlla),màgg na te kawe,la ko tànne ci darajay Yonnant bi miy ligéeyal biy joxe ag sell) +( ngir barig li mu leen ligéeyal te sellalal boroomam,di it ku sellal te matal kóllare ci diineem) +(mu boole lépp,dolli ci,yéeg ci barkeb Alxuraan te fa mu yéeg’ak a baax) +(boo jëlee wirdam de jël nga wird yépp,te doo ragal ag nërméelu) +(la nu dige ca seen wird yooyee it da nga ca jot,te doo ragal genn tëkku ) +(ndax moom (tëkku gi) ku bàyyi dëgg a ko tax a jug,te ku ko jël (moom wu sëñ bi) yayoo nga jagle ya ) +(jàpp ko de moo di jàpp ca lu baax la te dolli ca nag,ngir boole gi mu boole (wird) yépp,teg ca yor leneen ndollent (lu yeneen yoon yi yorul)) +(cosaan li mooy da ngay wax (ahuuzu billaahi minas shaytaanir rajjiimi)teg ca (bismil laahir rahmaanir rahiimi) jàng yenn aayay Alxuraan,doo ga tàmali) +(def hasbala (wax hasbunaal laah ba fa mu yam) def istixfaar ( astaxfirul laah) ,def haylala (wax laailaaha illaal laah) ,julli ci sangub ñu tedd ñi) +(ginaaw bi defees ag tëj gu rafet,loolu da na amal fa Yàlla lépp lu baax) +(lli mooy cosaani seen wird yi ñoom ñëpp,ku ci nekk nag am na genn jagleem gu mu moom moom rekk gu kawe) +(Sëñ bii nag moom jël seeni ndono jële ko ci gën ji mbindéef mi leen di àggale) +(mu wax (moom Sëñ bi) bi miy nettali yooyule xéewal,di ci sant kiy fàttaliku (di Yonnant bi) ngën ji aji xéewale ji (di Yàlla) ) +(ki moom jépp jumaa ak jépp jàkka, moom loo na ma mebëtum mbooloo yi) +(mu wax di sant aji tedd juy kenn ju ko donnal téere bi (di Alxuraan) muy ndono lu am njariñ) +(tàllal naa sama loxo jëme ca Yàlla,moom itam mu tàllal xéewalam ga ñeel ma ca géej ga,te loola tàlleeku) +(téereem bu tedd ba mujjoon na di wird ci man,daqaloon na ma samay noon it te dàkku leen) +(mu daan won lu neex képp ku ko taqoo, di ko jàng lu mu man) +(boo bëggee leeralug lii ma la tuddal,am lii nga xam ne ciy woyam laa binde sama mbind mii) +(wommatal nga ma lol ci la Jiilaani kawee, ngëramul ki ma kaweel yal na nekk ci moom) +(wommatal nga ma la Abool Hasan kawee woon ci ligéeyal Yonnant bi,miy maami Hasan) +(matalal nga ma la nga xam ne ca la Sheex Ahmad Tiijaan kawee woon,te nga nekkal ma ci lu rafete ni wurusu marjaan) +(wommatal nga ma lol soril na ma taq-taq,ma mujj mel ni Anas ci ligéeyal yonnant bi) +(moomloo nga ma te wommatal ma ag rafetal,donn na Hassan ci tagg Yonnant bi) +(ngërëm ak jàmm yal na nekk ci ñoom,ni lëndëm dàqoo ci ñoom(ni nu leerale àdduna bi)) +(mu wax ci bi miy tagg ngir sant ku nu jublu ki ( di Yàlla) ci téere bi (di Alxurran) ak Yonnant bi Muhammad) +(sama àddiya ji juge ci yaw ak ci Muhammad sunu sang bi, lu man a tee mer la) +(darajay aji far ji (muy Yonnant bi) far na samag deng-dengi,te wommatal ma kàttan ga ci lu dul ag doyodi) +(sama lépp’ay sant aji yekkati ji may dëgëral,cant gi nag jëm ci Alxuraan ak Yonnant bu baax bi) +( téere bi ak Yonnantub ku nu jublu ki, yekkati nanu sama lépp ci lu dul keno) +(Alxuraan nooyal na sama xol bu gindiku bi,dàq it bépp jalgatikat jëme ci ku dul man) +(sama xol ak sama loxo maa ngi ko jëme ci ku nu tànn ki ci di ko ligéeyal,may na ma nag la ëpp njariñ) +(aji dégg ji wuyyu na ma ci weeru koor,te baax na,mooy sama jubluwaay,ci barkeb Yonnant bi Muhammad) +(Yàlla gindi na sama xol,ñongal samaw yaram ci ngërëmam,dañal aji yàq sama) +(mu waxati bi muy déeyaale ak boroomam,mbégte ñeel na ñi ko sopp ñépp) +(ne: yaw mi jéggal sama ñaari way jur ak ñi ma sopp ci lu dul njàqare) +(te nga fàddul ma ci sa bopp ak ci Yonnant bi wëlif mbindéef yi,te may ma ay saar) +(fàddu nga ak man bu njëkk ànd ak Yonnant bi,may boroomug làqu wëlif mbooleem mbindéef yi) +( ma di ab jaam buy ligéeyal Yonnant bi,di ku nekk ci yaw ànd ak dëgg gi foofa,tey ku fàddu) +(mu waxaat ci yenn may yi nu jagleel ñi topp yoonam wi) +(Yàlla jëme na ci ñi dul ñi aju ci man lor yiy daje ak dof yi) +((ab boroom bu man loolu may na ko ko,te moom (boroom boobu) ku yayoo wuyyu la ci ku ko woo) +(nuy tëje ci Yonnant bi,mi di ag tàmbali te di ag tëj,tey ki gën a mat,yal na Yàlla saxal xéewal ci moom ak ci ñu mat ñi) +Foofu la loolu yam. + +Ñu dellu ci wax ci cosaanul wird wi,ak yax bi(yax=nassu ci araab.=texte ci français) mu bindoon ci ginaaw sotti (sotti = nusxa ci araab.=copie ci français) ga mu amaloon ca wird wa, muy : + +bismillaahiir rahmaanir rahiimi wa sallal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wahalaa aalihii wa sahbihii wa sallama tasliiman ,ku xool araf yii nu bind ginaaw matug wird wi, na xam ne ki ko bind di Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibul Laah,mi askanoo Mbakke te dëkk Bawal,may na ndigal mbokkam moomu ci Yàlla (t.s),sang bi Mustafaa Usmaan mi juddoo Halab te dëkk Madina,may na ko ndigal ci mu jëfandikoo wird wu nu barkeel wii ak jox ko ku ko soop ci mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi,ni mu ko jëlee ci Yàlla jaarale co ci Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu du ciy nelaw,atum baksasin di junni ak ñatti téemér ak ñaar fukk ak ñaar,ginaaw gàddaay gi,yal na Yàlla defal ki ko defoon gën jaa saxi xéewal ak gën jaa jariñi jàmm,ci benn barab bu nuy wax Sarsaara,ci weeru koor gi nu wàcce Alxuraan,mu dig jub ñeel nit ñi,te di ay aaya yu leer yoy ag jub la ak teqale dëgg ak safaan. Yàlla nag mooy seere lii nuy wax.Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yasifuun wa salaamun halalmursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina. + +Sunu mbokk moomu Muhammad Abdul Laah Alhalawii,nee na ci teereem bi tudd(( Anafahaat almiskiya fiil xawaariq al mbakkiya))muy ci maanaa bonnig misk ci xar-baaxi Mbakke,nee na Sëñ bi Yàlla da koo jox wird wii,mu jox ko muritam yi,xemmemloo leen ko,te loolu di lu war ci moom. Mu ne leen képp ku ko saxal aki sartam da na tàbbi àjjana ci lu dul hisaab (hisaab mooy laaj yi ñiy def ak a gëstu ay mbir) du caagéenug mbugal,te Yàlla it da na ko aar ci naqar yi ci àddina ak alaaxira,te saytaane mu nu dàkku mi du ko jege,da na doy wird wi ag kawe,nekk gi mu nekk wird wow boo ko dee jëfandikoo soxlawul gay jëfandikoo yeneen yi,te manoo am li ci moom te jëfandikoowoo ko. + +Sunu Sëriñ, sunu wasiila ca sunu boroom mu kawe mi nee na bi mu nuy jox wird wu tedd wii:jox naa leen wird wii ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe,kon tëye leen ko ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe. Mu waxaat jàpp leen ko ak doole,ku ci jotoon a yor weneen wird bu ko manee, na leen boole,kon muy leer ci kaw leer,bu ko manul mu yam ci wird wu tedd wile. Jeex na. + +Ki ko doon taariixal nag ne moom : bismil laahir rahmaanir rahiimi ,lii aw tagg ak taariix gu Ahmad doomi Asan def ñeel wirduw sëriñam bi Sheexul Xadiim,yal na nanu Yàlla jariñ ci moom ci ñaari kër yi aamiin. + +( sunu boroom taxawal (fondumang)na sunuy jëf ci may nu ñu man a root ci gën ji teen, kon mbégte ñeel nanu (mu jublu ci wirdul maaxuuz)) +loolu mooy wirduw sunu sëriñ bi Sheex Ahmadu Mbakke,mu juge ca boroomam jaar ci Ahmad Yonnant bi) +(yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc,li feek mi ngi doon ab raas jëm ca texe gu kawe ga) +(jox na ko wird wii jële ko ca aji namm ja muy Yàlla,yéem naa te ñée bii sëriñ ak yii taalube) +(jagleel na ko wurusu luulu wu nu ñongal ci xor,te làq ko ku dul moom) +(wurus ñeel na sunu sëriñ bu nu gërëm bu màgg bi,ku ko am de am dëkkaaleg ka gën a màgg) +(mi ngi ko gènne ci bisub àjjuma,mu jëm ci ku Yàlla texeel ci doomi jamono ji) +(ci juroomi fani sawaali atum (sahidnaa karaman) di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,moom boroom taariix bii,moom miy ndëppul ñu tedd ñi (ndëpp mooy mbaxana mi nuy solal buur) ) +(mooy sunu sëriñ Ahmadu MBAKKE mi dëgg di tax a tukki ak a took ) +(génneel nanu ko ngir jëmmi Yàlla ,kon billaahi bu ko sàggane) +(ngir Yàlla,boo bëggee am li nga bëgg,ndax kat kuy rëbb ba jam ñay man a dëpp) +(yaw sama boroom ci darajay aji wommat ji xeet yi jëme leen cig jub,di Muhammad miy wuññi njàqare) +(yal na Yàlla miy sos niir yi,sotti ci moom gën jaa selli xéewal ak mucc ak ñoñam aki saabaam) +(ak ci darajay sunu sëriñub Mbakke bii,na nga ma may ma jot ca la ña jiitu bëggoon) +(ci ag kawe,bu ko defee ma bokk ci mbooloom ñi la jege,yaw miy boroom nguur gi) . + +Nan dellu ca tukkib ñaareel ba,dem ba Tintu Muxsin,foofu barab la bob xew-xew bu ñaaw te soof dal na ko fa,muy : ab naar bu nu xam turam ak giiram,daa jugoon ngir ne da koy faat moom Sëñ bi - man moom xam naa ko waaye dama koy suturaal ngir doomi baay tëxam yu julit yi - moom da doon fexee faat Sëriñ bi,Yàlla musal ko ci,ni mu doon defe loolu nag mooy xanaa ñëw ci moom won ko ag cofeel gu dëggu ak jébbalu ci moom,Sëñ bi moom itam suturaal ko,boole ko cig njabootam,bindal ko ñatti bëyit,ne ko na ko saxoo jàng,guddi ak bëcëg ,naar bi moom itam dëkke woon loolu,bëyit yi moo nekk nii: +(lor ak saytaane jëm nanu ci ku dul man,ndax ñoom ñaar kat amunu ci man genn kàttan) +( Yàlla mooy sama boroom,Yonnat bu nu tànn bi - yal na Yàlla dolli xéewal ci moom, moom mi ko gindi te tànn ko) +( mooy samab xarit te di sama soppe,te bañ na it samag loru,te sàkku na ci boroom mbindéef yi samam mbég ). + +Naar bi taqoo woon ak loolu,di ko jàng guddi ak bëcëg ,ci mbooloo mi ak bu wéetee,mu ko daan def ginaaw saaru Yasiin,mel ni kuy nodd,nga xam ne da naan wax: yaasiin,yaasiin,yaasiin,ba kero muy mat juroom ñaari yoon,mu door a àggale saar wi teg ci bëyit yi,jàngati yaasiin ni mu ko defe woon,tegati ci bëyit yi,baamooti leen,nii daal la ko daa defe ,daawul taxaw lu dul daa sonn walla muy nelaw,mu sax ci loolu ay fan,am na ñu ne weer. + +Jamono jooja Sëñ baa nga woon fa ñoñ sheex siidiya,nekk ca seen xayma ya,ci noonu mu digaloon taalube ya nu defaral ko ag kër ca bitib gàdd ga,ñu def ko ni mu ko bëgge woon,bi mu noppee mu wax ko sheex Baaba,sheex Baaba digal mbokkam ma sheex Siidiya Muxtaar mu gunge ko ca kër ga,mu defe ko noona. + +Sëñ bi moom digal naaram booba mu ñëw ànd ak moom ca kër ga tey jàng ñatti bëyit yi,ni mu ko baaxoo woon,bi nu agsee,saytaane jàpp ko,xamal ko ne pexe mi mat na,def dong a ci des,bi guddi gi soree ba kenn yëngootul,naar bi jug,summiku ba mel ni ko ndayam jure woon,dal di dugg ci kër gi,jawali ca néeg ba Sëñ ba nekk,ginaaw xamoon na fa jaasiy Sëñ bi nekkoon ,mu jawali ca,bocc ko ci mbar mi,waaye Yàlla dogal jenn waay ju bokkoon ci néegub nguurug Kajoor,te gënoon cee rafetug tuub ak bàyyi àdduna,ñu ko daa wax Omar FAAL NDATI,nekkoon ca jàkka ja,di fa fanaanee jaamu Yàlla,bi ko naar bi rombee mu jug ca saa sa,seeti ki yor mbiri biiri Sëñ bi ,di Muhammad Lamin ÑANG,doomi Muhammad Lamin Mati,moom waa-jur wi,doomi bàjjan la ci Sëñ bi,xamal ko ne am na jëmm ju rafle ju jëm ca néegub Sëñ ba,ca saa sa ndonga la jug,gaawantu,fekk naar ba mu bocc jaasi ja,di settantal naka lay jekkoo Sëñ bi ba man koo lor bu baax,te Sëñ bi moom mi ngi tëdd ci wetam,bi naar bi xàccee di ko door jaasi ji,yàlla dogal mu lonk ci koñub xayma bi,daje ak ndonga li di wadd di dal ci kawam,mel ni kuyul gileem loolu,dal di koy nërméel,naar bi yuuxu,murid bi yuuxu ci kawam,mel ne da koo bëg a lekk,seen coow li fees foofa dell,ña nekkon ca wet ga yuuxaloo,daje fa,nga xam ne Sëñ bee mujj ñëw dox digganteem ak nit ñi ne kon ñu ray ko,mu dalal leen,dal di yonne ci menn mbooloo,mu fanaanoon fu sori foofa,mu mu naroon a yewwi,woolu leen,ne leen yobbaaleel leen ma naar bii ba Xumaak, (barabu kiliftéefug tubaab yi,da nanu ko wax it Sahwatul Maa) ngéen bàyyi ko fa te dem seen yoon,denk leen ñu yëram ko te dimbali ko ci bagaasam yi,làq leen nag xibaar bi,ngir bañ ñu gaañ ko,jeemul a fayoonte ak moom ci jëfam ju ñaaw. + +Yenn taalube yi nag gis nanu ne li tax Sëñ bi delloolu naar bi Xumaak,fa tubaab yi am sañ-sañ,ab junj la ci ne ñoom tubaab yi ñoo ko yonni,Yàlla rekk a xam,waaye pexeem ma moom Yàlla naaxsaayal na ko. + +Yooyu ñaari bëyit boo ko xoolee da nga gis ne Yàlla feeñalal na ko ci ay karaama yu kawe,yal na ko Yàlla fayal jullit ñi aw yiw ak Lislaam. + +Man nag li ma gis mooy lii mooy dëgg-dëggi laabiir ak doylooYàlla,ak nangu ab dogalam,miinunu ko ci ku dul moom ci waa jamonoom,li mu nuy fàttali mooy li daloon ki miy ligéeyal ci yenn ci xareem yi,loolu mooy dafa am benn Ahraabii (araab bu dëkk ca kaw ga) bu tuddoon Duhsuur bu ko fekkoon mu tëdd,xaw a sori saabaam yi,mu bocc jaaseem,xàcc ko ne ko ana ku man a dox sama digante ak yaw? Yonnant bi (j.y.m) ne ko Yàlla,ci noonu waa ji di lox ba jaasi ji rote ci loxo bi,Yonnant bi (j.y.m) jël ko ne yaw nag ku la man a musal ci man? Mu ne ko amal yërmaande, Yonnant bi jéggal ko,bañ koo def dara. + +Naar bii nag moom bis dellusi na ci Sëñ bi ca Xumaak,taalube yi jug ngir fexeel ko,Sëñ bi yëg ko génn ci naaj wi,te solul ay dàll,di wax ca kaw: bàyyi leen ko,bàyyi leen ko,(alaa tuhibboona an yaxfiral laahu lakum) muy:xanaa bëggu leen Yàlla yëram leen,di ko baamu. + +Nu bàyyi ko,mu digal ko mu làqu,génn te dem yoonam,ginaaw bi mu ko defalee ag njekk. Bi ku tedd ki nekkee Njaaréem,naar bi delseeti fa,Sëñ bi aarati ko,naan ko:boroom jaasi ji,naar bi naan ko : déedéet neel boroom xëm gi,bu ko defee Sëñ biy ree,génneeti ko ginaaw njekk.Man ci sama bopp gis naa ko Cees,maanaam Jànqeen,te booba maa ngi ànd ak am mbooloo ci taalube yi,waaye man rekk a ko ci xàmmee,bu ma ne woon kii de diw la ñu ray ko,waaye kon ana jikkoy Sëñ bi,Alhamdu lillaa. + +Nu dem nag Jaraari,barab la bu Halawi yi moom,Sëñ bi tudde woon ko Biirul Xayri di ci maanaa teenub yiw,ci barab boobu la Sëñ bi doon waxe xasida gii: +(( li ma doon laaj sama boroom indil na ma ko cig baamu,rawati na ca Biirul Xayri di Jarraari)) +((samag cant ak njukkéel ñeel na ab boroom bob wommatal na ma ay xéewal,ci lu nëbbu ak lu feeñ,di ku ñu baax ñi sopp)) +((sama boroom wommatal na ma barkeb saabay ku nu tànn ki,mu nekkaloon ma te daawu ma won ayuw kàccoor yi)) +(( samag cant ñeel na aji jiitu juy aji des,kok aar na sama kanam wëliif bépp ñaawtéef,ànd ak ag bëbb guy daw juge ci moom jëm ci man (bëbb mooy luy sottiku bu baax di wal fii mu jublu ci xéewal) )) +((samay cant ñeel na ko,ci biir ay sang yu askanoo ca Aliyun (fii man na cee jublu Seydinaa Aliyu,man naa firi it aji kawe di Yonnant bi) ci lu dul aji jalgati mbaa workat)) +((aji des ji amul bokkaale yal na dolli xéewal ak mucc ci ki nga xam ne indil na ma la ma ko ñaanoon cig baamu)). + +Halawi yi nee nanu xamunu lu tax Sëñ bi tudde ko Biirul Xayri,ndax tur woowu ñoom masunu koo dégg ci seei baay,ba bi nu fa suulee Sheex Ahmad Bun BUDDIN,nu dal di xam sekkareb li tax mu tudde ko ko,nu xame ci baatinub Sëñ bi. + +Ci Sheex Ahmadu Bun Buddin, Sëñ bi wax na ci ay wax,Alhaaji Muhammab Bun AAB,dàkkantal la ci Sheex Ahmadu Bun Buddin,nettali na ma ne baayam bind na bis Sëñ bi ne ko daa bëgg mu nuyyul ko Yonnant bi(j.y.m),ak Sheex Ahmad Tiijaan,te itam soxla na seenub tontu,Sëñ bi tontu ko xamal ko ne Yonnant baa ngi koy fay,ak Sheex Ahmad Tiijaan,aji nettali ji nee na ca saa sa, baay ji daanu ab jéll,di yëggal bopp bi ak a waxtu,mel ne ku jaaxle te nu muur am xelam,dañul ci melokaan woowu ba bi mu faatoo (y.y.g),te booba ñi ngi fu sori woon Sëñ bi, te yëgalunu ko woon kenn ci guddi gi mu ame woon,waaye amul lu dul ay ndaw dikk ci suba gi ne Sëñ bee leen yabal ñu teewesi dencug Sheex Ahmadu gi,te di leen ko jaale. + +Mu bind ci loolu ag xasida di ci xamale darajay Sheex Ahmadu moomu, fa Yonnant ba,moo tax mu terale ko karaama googu,ne lii mooy payug Ahmadu Bun Buddin,tey payug ab xalifaam: + +Bismil laahir rahmaanir rahiimi, yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu sang bi Muhammad aki ñoñam aki saabaam,na ngeen xam ne guddi gi Sheex Ahmadu Bun Buddin di faatu ruuhul xudsi (jibriil) (j.y.m) wàcc na juge ci asamaan si,ànd ak lu bari ci ay malaaka ngir terale ko sang boobu,ngir rafet gi mu rafetoon njort ci Jaam Biy ligéeyal Yonnant bi (Sëñ bi) ,yal na ko yal na ko Yàlla nekkal cig teral,moom miy aji jiitu tey aji des,ñoom nag delluwaatunu ca guddi googee ndare bu danoo yobbaale ruuwam gu tedd ga,lii nag mooy dëël bi nu ko dëëloon,(dëëlmooy dikk) .loolu la Sëñ bi di junj ci bëyit yii: + +((Ruuhul Qudsu ñëw na,di wuññisi njàqare,ànd ak mbooloo mu mag ciy malaaka,jamono ji Ahmadu mii di làqu)) +((Ahmadu am na la mu bëggoon ca Yàlla,buntub yiw ubbikul na ko bu dul tëjooti)) +((yal na Yàlla fay ka joxoon àddiya aji ligéeyal ji,moom moomu nga xam ne am na fa Yàlla ag tab gog aw yiwam moo gën a mat)) +((maa ngi sàkku ci boroom aras ay may ñeel ka ko joxe woon moom mooy aji texe ju nu ndëppal ji (ki nu solal mbaxanam buur) )) +((sangub sang yi wéy na,di ab sëriñ bu nu jiital (bu nu def muqaddam),jiital gi it ki ko def di sëriñ bob aw wirdam ba fàww am ngér lay doon)) +(( moom de bir na ko ca àllaaxiraa gee mu nekk ne man maay jëwrini ki nga xam ne mooy boroom raw ak jiital,te mooy ku nu ndëppal ki)) +(( sangub sang yi yal na am ngërëmul sëriñam,ak ngërëmul gën ji mbindéef,ndaw muy ku nu bégal !)) +(( Yàlla la’ay ñaan mu may xalifa bii mu fi bàyyi la mu yéene,ci darajay ka nga xam ne ay leeram day jolli)) +(( yal na nekk ci moom ,moom Yonnant bi,ñaari xéewali Yàlla mi ko gindi def ko muy ku nu gënal ki,ni mu doon yéege ak a kawe ca rañaan ga)) +wasalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu. + +Eskëy,gis nga waxam ji mu naan “ka ko joxe woon” mi ngi ci jublu Sheex Ahmadu Bun Buddin mii,li mu ko joxoon mooy benn teere bu tuddoon ((Mawaahibul Ladduniya)). + +Sama mbokk,sama xarit Sheex Ibraayma AMAR nu gën koo xame ci turu Ibra Joor,nettali na ma ne Sëñ bi,bi mu nekkee Sarsaara walla Tuntu Muxsin, da koo yonni woon Ndar ngir mu jëndal ko fa téereb Mawaahibul Laduniya,nga xam ni ki nuy wax Qastalaanii moo ko def,nee na ma dem sonn ci lool,fu ne ma wër fa,waaye dara,ma am lu ma naqàri lool,yëf yi tiis ma lool,ma dëpp di ñibbi,bi ma tollee ca gàddug Sheex Ahmadubnu Buddin,te fekkoon ma xamante ak moom,ma daad fay jàdd ngir nuyyu ko,siyaare ko,ba ma fa àggee mu bég lool,teeru ma dalal ma,bi nu toogee bay waxtaan mu laaj ma lu ma taxoon a jug,ma ne ko sëñ bi dey moo ma yonni woon Ndar,ma leeral ko tam naqàr wi ma am ci ñàkk a am teere bi ma Sëñ bi yonni woon,ca saasa mu jug,gëstu ci ay teereem,génne ñaari xaaj yepp indil ma,ne ma neel Sëñ bi àddiya la,ju ma ko jox ngir Yàlla,ma bég ci ba fa bég yam,waaye Sëñ bi moom gën maa bég fopp ci teere beek ki ko joxe,loolu nag mooy maanaam ka ko joxe woon,mu jub lu ci li mu joxe woon “MawaahibulLadduniya” . + +Xasida gii ndollent la ci tontub kiy laaj ndax Jibriil da na dikkati ginaaw yonnat bi. Bokk na ci li mu bind ñeel Sayid Ahmad mom Sheex Muhammadul Haafis lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allaahuma salli halaa sayyidimaa muhammadinil faatihilimaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa,naasiril haqqi bil haqqi wal haadii ilaa siraatikal mustaqiim,wa halaa aalihii haqqa qadrihii wa miqdaarihil haziim,na Sheex Ahmadu Bun Sheex Muhammadul Haafis,ak ku dul moom ci ñoñ Halawi yu goor yi ak yu jigéen yi,ak ku dul ñoom ci jullit ñu goor ñi ak ñu jigéen ñi,nanu xam ne Yonnat bi jàmm ak xéewal yal nanu nekk ci moom,delloo na ab nuyyo Sheex Ahmadu,te Sheex Tiijaani moom itam gërëmul Yàlla yal na nekk ci moom delloo na ko nuyyoo,te Yonnant bi (j.y.m) teral na ko teral gu mel ne gi mu teral mbokkam mi Sheex Muhammadul Haafis,ki ciy dund yal na ko Yàlla gërëm te aar ko ci lépp lu mu ragal,ka wéy it mu gërëm ko te yërëm ko,te SheexAhmad Tiijaan it yal na ko Yàlla gërëm,te jegeel ko,def na ko niki doomam,képp ku jële wirduw tiijaan ci ñaari sëriñ yii tudd Ahmad yal na leen Yàlla gërëm te aar leen te yërëm leen,mel na ne jële na ko ca Sheex Muhammadul Haafis (y.y.g),képp ku ko jële ci ñoom ba noppi bàyyi leen fi di demati ci keneen ci mbooleem sëriñ yi,ànd ak yéeney bàyyi leen,na ko wóor ne pert na ci àddina ak allaaxira,yal na nu ci Yàlla musal,képp it ku ko jële ci kenn ci ñoom ñaar,bu ca faatoo tonowu na adduna ak allaaxira,képp ku xool mbind mii na xam ne bi nu koy bind Sheex Ahmad Tiijaan (y.y.g) moo taxaw di wax ñuy bind. + +(( dello nuyyoo bu teey bu kawe bépp nuyyoo buy bijj ag dëppoo)) +((juge na ca jaamub boroomam bay ligéeyal ku nu tànn ki,jëm ci ki làq kawe gi niy tànn)) +(( yaw sëñ bu màggi mbir bi,musal nanu la ci lori lépp lu ñaaw)) +((musal nanu la ci rékki aw yiw wu nekk ci yaw,ba kero ngay tàbbi àjjana ya’ak ñi lay xeeñtu)) +(( Aji des ji musal na la ci ñaawtéef yi,ci barkeb ku nu tànn kiy boroom raaya ba (daraapoo ba ,di Liwaawul Hamdi) )) +(( ak darajay sa sëriñ bu nu gërëm ba,Sheex Tiijaan,ka mujj mel ni wurusu marjaan fa sang ya)) +((yal na Yàlla miy aji des dolli xéewal ak mucc ci gën ji mbindéef, moom (Yàlla) miy ki koy wommatal kawe ga ak saar ya)) +((ngërëmul Aji des,luy bijj ag dëppo yal na nekk ci wàlliyu wow topp na ay tànkam (tànki yonnant bi) )). +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina. + +Bokk na ci li mu bind ngir ñiy am ag wuute ci “Mahiya” (mahiya mooy ag ànd,nu jublu ci ànd gu Yàlla ànd ak kenn walla nekk gu mu nekk ak moom) ,lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatahaa minas saytaanir rajiimi,rabbi,ahuuzu bika min hamazaatis sayaatiini,wa ahuuzu bika rabbi ayyahduruunii. Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allahuma salli halaa seyyidinaa wa mawlaanaa muhammadin,al faatihi limaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa naaziril haqqa bil haqqi wal haadii ilaa ziraatikal mustaqiimi,wa halaa aalihii haqqa xadrihii wa miqdaarihil haziim, +mu ne mi ngi ñaan julli gii doon gog da na yee képp ku xool mbind mii,mu yee ko ci ne Yàlla kat ànd gi mu ànd ak ñun ànd gu yellook moom la - tudd naa sellam ga - du ànd gu xel di jot,te moom - barkeel na te kawe - jege na nu,waaye jege gu yelloo’k moom,du jege gu xel di xalam,te xam-xamam - tudd naa sellam ga - lu nu sellal la,niki mbooleem ay meloom ,jëmmam it - barkeel na te kawe - tàqalikoowul ak ay meloom te du tàqalikoo ak ñoom it. +Waxi Sheex Sanoosi ji,(y.y.g) ak ñi ànd ak moom ci lu aju ci “Mahiya” lu wér la,ndax ñoom kat danoo seet fi nit ñi toll,ñu wax fa’ak ñoom,ndax bu nu weesoo ak ñoom foofu ñu tàbbi ci alkande,ñoom ñépp. Waxi Sheex Ahmad Tiijaan ji it (y.y.g) wuutewul ak li nu wax. Waaye li ñi askanoo ci moom(y.y.g)di wax,ba miy indi ak noonoo ci seen digganteek Abuubakar Ibnu Fatan,na leen wóor ne noonoo googu de ci saytaane la juge,ndax Ibliis day tàbbal lënt-lënt ci xolub képp ku nekkul “Mushaahid”,(mushaahid mooy aji jàkkaarloo,maanaam kay jàkkarlook mbir ya ca nguurug sunu boroom ga) liy firnde ci loolu mooy Jaam biy Ligéeyal Yonnant bi - yal na ko Aji des,jiy Aji jiitu nekkal cig teral - bi muy bind laabiire gii déy,Yonnant bi dikkal na ko (j.y.m) ne ko Sanoosi Ak Sheex Tiijaan ak Xazaalii de ñoom wuutewunu,ñi am ag wuute kay ñooy ñu dul ñoom. Dëgg gi mat a dellu daal mooy bàyyee settantal ci melow “Mahiya” te gëm rekk ne lu am la,ndax di ci settantal day rékki ngëm ,yal na nu ci Yàlla musal. Wasalaam . + +Bokk na ci li mu bind ñeel Abuubakrin Ibnu Fatan ci mbirum “Mahiya” lii:Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla dolli xéewal ci sunu sang Muhammad ak ñoñam aki saabaam,ag xéewal akug mucc gog da na ci xamal nit ñi ne la Aboobakrin Bun Fatan waxoon ci waxi Seex Tiijaan ji,jubluwu ci woon Sheex Tiijaan(y.y.g),te moom Sheex (y.y.g) dëppoo na ak moom (Aboobakrin) ci mbooleem li mu wax ci tontoom yi. Ag jub nag mooy nit ñi bàyyee xuus ci lu mel nii,ndax xuus ci, ci ñaawtéef yi la bokk . Waxi qutbu yi, yal na leen Yàlla gërëm, du waxi boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm. Boroom xam-xam yiy jëfe seeni xam-xam,fi nu toll ci wàlliyu yi mooy fi wàlliyu yi toll ci yonnant yi . Boroom xam-xam yi boroomi tawhiid lanu yuy aar Sariiha mu nu laabal mi, qutbu yi boroomi sellal lanu yu jegeYàlla di aar “Haqiiqa” mu nu leeral, mu nu sellal mi.Kon wormaal ñépp ngir jëmmi Yàlla mu kawe mi lu war la . Bëgganteg boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm,mooy dundug sariiha,seenug wuute ci masala yi,ag jàng la akug jàngale,dug noonoo,dug iñaanante. Wasalaamu halaykum wa rahmatul laahi wa barakaatuhuu. + +Bokk na ci li mu bind ci Ahmadabnil Kawri Addaymaanii, lii:Ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla mu kawe mi dolli xéewal ak mucc ci sunu sang ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam,xéewal ak barke ak mucc gog dana ci xamal nit ñi ne Muhammad Ibnu Kawri Addaymaanii,ak Abuubakrin Bun Fatan Alhasani,Yàlla mu barkeel mi te kawe jéggal na leen ñoom ñaar,ci bisub Harafa atum “shahidnaa bikaram” di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,te ku ci nekk ci ñoom ñaar xawoon naa alku,sababub loolu mooy juumug Daymaanii,ak weddig Alhasanii. Ahmadu Bun Kawri moom dëppoowul ak Sheex Tiijaan ci li mu doon xuus ci wàllug Mahiya,bu dee Aboobakrin moom daa ñàkki teggiin ak Sheex Tiijaan (y.y.g) ci ñàkk a nangu ag tontoonteem ak Ahmadu Bun Kawri,Sheex Ahmad Tiijaan nag moom ku beru la wëlif leen ñoom ñaar.Liii mooy dëgg gi nga xam ne sikk amu ci. Wasalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhuu. + +Mu bindoon ba tay jëme ci ñenn ci ñoom: Assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wabarakaatuhuu,bu lii jàllee,man de gis naa li xewoon ci sa diggante ak keneen ci lu aju ci mbirum Mahiya,man nag li may wax ci Mahiya,mooy jëmmi Yàlla moom,kawe na te barkeel,du toq ci xelum kenn mu koy jéem a gëstu ,kon xuus ci Mahiya moo’k wuute gi am ci diggante yahood yi ak nasaraan yi ñoo yam,yal na nu Yàlla mu kawe te barkeel mi musal ak yeen ci soxlawoo lu nu yitéelul. Soxlawoo def ndigal yi te teet tere yi moo gën a jaadu ñuy soxlawoo xuus ci googule wàll,Yàlla barkeel na te màgg,nee na :( zarhum fii xawdihim yalhabuun) muy bàyyi leen ci seen xuus googu,ñuy fo. Wassalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaala wa barakaatuhuu. + +Ci noonu Sëñ bi tuxoo ci barab dem ci barab, ba bi mu sancee ca Sahwatul Maayi,nu gën koo xame Xumaak,soriwaay bi di lu tollook doxub bis bu tar ci ku sawar,juge Dagana walla Budoor. Loolu amoon ginaaw lollib atum baksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,mu mujj di wër ci barab boobu di tukkee ci kër,dem ca geneen gu jege,mbiram it moo’k mu mbooloo yi koy dikkal di siyaaresi di gën a yokk,ci jamono ju nekk. + +Cig gàttal daal leeral mbiri Sëñ bi yepp ci ñaari tukki yii,aal topp aal (aal = tolluwaay yi nit di toll), xew-xew topp xew-xew,kenn ku dul moom manu ko,yal na Yàlla yokk ngërëmam ci moom. + +Ag karaamaa ngii gu amoon ca Xumaak,maanaam Sahwatul Maayi,ci genn guddi ci benn ci ñaari weeri rabiih yi,atun jaksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñatt,muy tawati tànk ju ko daloon te tar lool,fogloo nu ca guddi googa,nu fanaan ca la wër xaymaam ba,nga xam ne sax jortoon nanu ne du weesu guddi ga,waaye moom mu niy dalal rekk naan nu dellu leen ca yite ya,amul solo,waaye nun deeti nopp mbaa ay xel di àndati ak nun. +Bi Yàlla dogalee mu wér ca suba ga,mu xamal ma ne mbir mi de balaa la woon bu juge fa sunu boroom,jëmoon ciy nitam,ñu naroon a fër bu leen daloon (fër = naaxsaay), ma ne sunu boroom lu tax nga jagleel sama nit ñi nattu bii bàyyi ñeneen ñi,ñu ne ma ndax kat Yàlla da laa teg ci sa kawi moroom,kon manul a ñàkk mu jàgleel la sa nattub bopp bu ñeneen ñi dul am,te loolu amul lu ko gën a tar.Man it ma ne yaw buur bi ndax man naa koo gàddu wëlif leen ? Ñu ne ma aha kay, jëlal ,mu doonoon lu diis juge ci asamaan wàcc sama kaw,ma daanu xëm,ñu indi ma ci xayma bi te yëguma. Ki ko yobb ci xayma bi,di Moor Xari Joob nettali na ma ne jaan a ko màtt,kon alhamdu lillaahi ci mucc gi ak tuufu gi (tuufu mooy am li nga bëgg) . + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Ba mu fa nekkee ba guddig gàmmug atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,di guddig àjjuma,la fa Sheex Ibra FAAL ñëw,tukke Ndar,indaale këyit wu juge ca tubaab ya di ko may mu dellu réewam Senegaal,murid boobu it dikk jàpple ko ci tuxu gi,mu tàmbalee waaj,di tàggu waa dëkk ba ,ba àjjuma ja dellusi,di fukk ak juroom ñeent ca weer wa,mu génn këram googa sóobu yoonu Ngaanjaar,maanaam Gaaya,dib dëkk bu nekk ci penku bëj-gànnaaru Dagana,dex gi romb na fa,ñooña sàkku ci moom mu julli ci seen jàkka ji nu doon yeesal ,ngir barkeelu ci,mu ànd ak seen imaam ja Muxtaar SOW, julli ñaari ràkkaa ci njëlbéenug yoor-yoor,jëggi dex gi dem dagana,nekk fa ba bisub gàwwu ñaar fukki fan ak juroom ñatt ci weer wi,mu dugg gaal ci tisbaar ji jëm Ndar. + +Jamono yi mu nekke woon Dagana,nganale gu nekk defal nanu ko ko fa,ci bëcëg gi, bu guddi masaan a jot,ñu daa indi ay làmp yu leer ci kanamu bóoli yi. Mu wax ci loolu ne loolu mooy liy dëggal waxam ja mu waxoon ca lenn ca xasaayidam yi mu defoon ci arafi ((walil laahi mulkus samaawaati wal larli))di ci maanaa Yàlla’ay boroom nguurug asamaan ak suuf,muy li mu mujj a bind ca Daarul Mannaan ca Tuubaa,ba mu àggee ca arafu daad wa mu waxoon ca : + +((gane ji naa aji Tedd ji,mu teeyalal ma ganale gi,te du ma dañ ci nganale gi mel ni ay làmp)) + +Bi mu àggee Ndar ca guddi ga,daa dal di wàcc ca Sheex Ibra FAAL,sax fa ay guddi,juge fa dem Luga, wàcc ci Alhaaji Masamba Soxna,foofa la yabale ligéeykat yi ñu dem Njiheen,maanaam Cëyéen,ca Jolof,jiitu ko fa,defaral ko fa ag kër njëkk muy agsi,dal di jàll Ngaajax,fanaan ca jàkka ja,fa seen xabrub wàlliyu nekk,dal di jàll ca kër sëñ Asan NJAAY,yendu fa ,fanaan fa,yendooti fa,laxas dem Kokki,wàcc ca Sheex Muhammadu Maam ,maami Sheex Bashiiru,demati Duriga,faSheex Madun Samba,maami Sheex Murtadaa,juge fa àgg Kër Baasin ca Sheex Muhammadu Amina Xuma JOOB,doo nga dem Cëyéen ci bis yu néew,di njëlbéenug rabiihus saanii,fekk yenn kër yi noppi,bi mu agsee ca kër ga,ca njëlbéenug rabiihus saanii,atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,daa wàcc tudde ko Daarur Rahmaan,mu nekk fa mbiram akuw doxiinam di gën a jub,di dolliku waxtu wu nekk,ba ci benn ci ñaari jumaada yi ,ci atum saksasin,di junni ak ñatti téemèer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,mu taxawal Daaru Xudoos ci sowwub dëkk bi,soree ko lu tolloo’k ñaari kilomet walla lu ko yées,mu sax fa ,bul laaj nag mbiram,moom daal na ma la ko waxe woon rekk ci bépp barab,waaye fii sax gën na fee dolliku,ba ca àjjumay ñaar fukki fan ak ñaar ci weeru muharram,atum lasasin,di junni ak ñatti téemèer ak fanweer. + +Ca sahbaani sakasin ja,di junni ak ñatt téeméer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,walla ca ramadaan ja,la sëñ Abdul Laahi gane àdduna,wax nanu ma ne Sëñ bi daa bind Abdul Laahi ci aw këyit,yonnee ko Sheex Muxtaar Binta LOO,nijaayi sëñ Moodu Mustafaa,digal ko mu tudde ko noonu,mu defe ko ni mu ko binde woon ci këyit wi,mbooloo mi nag leegi danu koy wooye Abdul Laahil Haziizi,te xawma fu nu jële loolu,ah waa-waaw xanaa denu cee jublu ne Haziz turu Yàlla la. + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Ci njëlug bisub gàwwu,ñaar fukki fan ak ñatt ci muharram,atum lasasin,la génn dem Njaaréem,mu julli woon suba ginaaw bi mu doxee lenn ci ay kilomet,mu fanaan ca la yées Tuubaa, ca guddig altine ja mu fanaan Tuubaa,ca Daarul Haliimil Xabiir,fa Sheex Abdu Rahmaan LO,muritam ba jàngal doomam yu mag yi,mu xëy nag jëm Njaaréem,fanaan fa guddig talaata ñaar fukki fan ak juroom ñatt,bi mu àggee Njaaréem,ñu dalal ko ci njëlbéen gi ci benn pàkk bu nekkoon ci wetu àttekat (goornoor) bu ndaw bi,àttekatu ñoñ bi (al haakimul ahlii,xanaa mooy gouverneur civil) ,ca jamono jooja ma nga dëkkoon ca wetam,barab boobu fa lanu tabax fi mu nekk jàngukaayu farañse bu mag bi (école française),ca penkub dëkk ba ,nee nanu ci safari lasasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer,la sëñ Ibra mom Sëñ bi gane àdduna,ca rabiihul awali atum alsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak benn,mu tuxoo fa dem ca këram ga nekk ca kaw tund wa,ginaaw bi mu ko tàmblee defar ca weer wa ko njëkk,loolu nag mi ngi amoon ca bis bu njëkk ba walla ba ca topp,walla ya ko jege,dal di koy tudde Albuqhal Mubaaraka,di ci maanaa pàkk bu nu barkeel bi. + +Ca ñaar fukk ak ñatt ci weeru sawaal atum balsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñaar,Sheex Abdul Ahad gane àdduna,ci muharram atum jalsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñatt,sëñ Abdu Xaadir gane àdduna,ci guddig àjjuma,ci fukki fan ak ñeent ci +silqihda atum jalsasin ba tay sëñ Saaliwu gane àdduna,ci juroomi fan ci weeru kooru halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom sëñ Suhaybu gane àdduna di rakki sëñ Abdul Ahad,ci silqihda hasasin ba tay la sëñ Abdus Samad gane moom itam,ci rabiihus saanii atum jamsasis,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñatt,la Sheex Murtadaa gane àdduna. + +Mu tàmbli jumaa ji atum halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom,jéego ci ñaari tànkam yu tedd yi ci guddig dibéer,weeru rabiihus saanii,fàtte naa nag bis bi mu ci tollool,ñu tàmblee gas dal bi (fondmang bi) ci ñaar fukk ak juroom ñaar ci jmaadas saanii atum walsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan weer ak juroom benn. + +Tabax gi moom ñu door ko bisub altine ci yoor-yoor,Sëñ bi wàcc ci biir paxum xuba bi,Sheex Muxtaar Binta nekk ci wetam,yor ndab lu def ban ( xam naa simaa la war a jubloo wax) , Sëñ bi jël jumtukaayu tabax bi (turéel) dal di tibb ci ban bi (simaa bi) , wax bismil laah,sotti,jëluw xeer teg ci ban bi (simaa bi) ,jëlati gasukaay bi door ko ci xeer wi,jàng :”wa isyarfahu ibraahiimul qawaahida minal bayti,wa ismaahiilu rabbanaa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu” mu di ci maanaa :ba Ibraahiima di yékkati dal ya, (mbaa ponk ya, mbaa fondumang ya),ak Ismaahiil,,naan :yaw sama boroom nangul nu ndax ya’ay aji dégg ji,tey aji xam ji. + +Mu dal di fay juge,julli ñaari ràkkaa,ñaan. +Alhamdu lillah,ligéey bi àgg na ci juroom ñaari at,ci teewaayu Sëñ bi ,mu julli fa ñaari iid yi(tëbëski ak kori),ñaari yoon ci lu wër ,ñatteel bi kay laay sikk,waaye julliwu fa àjjuma . + +Sëñ Mbakke BUSO nee na li ko waral mooy moom kat masu fa’a yéenee sax mukk,(ku yéenewut a sax àjjuma waru ko), ka fa njëkk a taxawal àjjuma mooy Sheex Ibraahiima,rakkam ja,ci dëppoo gu mu ci def ak Sheex Mbakke BUSO,ak doomi Sëñ bi ak magi taalube yi,ndax ñoom ñépp a fa yéene woon a sax. Ndax Sëñ bi moo digaloon mag ñi ñu sanc ci wetam,bàyyi boroom kàttan yi man a ligéey tey tarbiyawusi ñu nekk ca tool ya,di ligéey di indi. + +Dëkk ba mujj di dëkk bi gën a dund, ak jàkkaam yeek daaraam yi,ak jàngukaayi xam-xam yi,kaamilub Sëñ bi nag bis bu nekk ñu wàcce ko ci bunt këram ñeenti yoon,ñaari yoon ginaaw jullig suba,aw yoon ginaaw tisbaar,ak weneen ginaaw tàkkusaan,bu dee guddig àjjuma ñu wàcce ko juroom ñaari yoon,mbootum loolu moom,Yàlla rekk a xam,mooy jullig farata gu mu julli gu nekk, tolloo’kub kaamil bu nu koy wàcceel,li ko tàmblee suba gi ba timis,juroom ñaar yi niy wàcce ci guddig àjjuma gi tolloo’k geey ayu bis gi = julli gu nekk kaamil. + +Bu dee lu aju ci mbindlu mi moom, da daan def képp ku mokkal te rafetum mbind,ñu daa ko bindloo ab kaamil ci lu tolloo’k ñatti weer yu nekk,walla sumun walla robo walla sulus walla nisif ci weer wu nekk,mu ànd ko ak ku mu nirool mbind,mbaa ñu mu nirool. + +Naka noonu ñi ko daan coobarewoo di ko def ngirYàlla,ci donga yi nekk ci biti,ak ñi ñu daa fay ci waa-rëw mi ak naar yi,weer wu nekk daa nanu am lu tolloo’k ay téeméer ciy kaamili loxo,lu bokkul ak li nuy jënd ci yu móol yi . + +Xam naa ne bis daal jëndandoo nanu juroom ñaari téeméeri kaamiil ci yu móol yi,ci benn yaxantukat,yu bokkul ak téerey xam-xam yiy dikk di juge ci wàll gu nekk,yu nu binde loxo ak yu nu móol,deesul delloo mukk ab téere,ak doonte dikk na fi ay yooni yoon,ak doonte danoo dagg ñaari wàll yi. + +Mu bire ci loolu ne menn njënd mi mu daa def moom saraxe rekk a ko waraloon ak doonte da ko daan suturaal ci ron ay njëkk,te loolu bokkul ak li mu daa seddale way ñàkk yiy laaj,mu di ag ndimbal ngir Yàlla,ak li mu daa jox boroom dara ja yi lépp ngir Yàlla rekk. +Leeg-leeg bis, mu seddale ci ay junniy junni,bokk na ci li gën a yéemey li ñiy gis, gis,te ñiy dégg, dégg ko,mooy daa am bisub ñaar fukki fan ak juroom benn ci weeru koor,atum bamsasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñaar, mu dajale nu,nun mbooleem bindkat yépp,yu rafet mbind yi,te booba ab takk bu réy ci këyit a ngi ci kanamam,mu ne nu ndax xam ngéen lu ma leen di doye ? ñu ne ko déewalaay,mu ne leen këyit gii daal laa bëgg ngéen bindal ma ci ab kaamil,te du ñu ne ma mukk teru waa ngii,ndare bu da ngéen ma ne kaamil baa ngii !, ndax da ngéen ko def ?,ñu ne waa-waaw,mu ne nu jël léen këyit gi ,nu jël ko ,seddoo ko ci sunu biir. + +Nga xam ne da ngay gis ku jël ñaari isib,bind leen ci bis,ak ku jël ñaar bind leen ,keneen maas leen, ñu tàqalikoo ci loolu ci yoor-yoorub juroom benneelu fan ba,ku nekk ci nun xam na la mu war a bind,ak baat ba muy yam,ca digganteem ak ka mu ko seqal, dunu ci dolli ,dunu ci wàññi. + +Kaamil bi noppi alhamdu lillaah,ci tisbaari bisub juroom ñeenteel bi,ñu jébbale ko, Sëñ bi xool ko,gisu ci lenn lu ko naqàri,du mbind mu gën a rëy moroom ja,du mu gën a sew,du lenn daal . Mu dal di sant Yàlla bu baax,daa di ne ndax déggagun ngéen fi ku bind walla mu bindlu ab kaamil ci ñatti fan ? Nu ne ko déedéet , mu santaat Yàlla,dal di jàng:(( innii laa udiihu hamala haamilin minkum)) muy ci maanaa,man de du ma sànk jëfi aji jëf ci yeen . + +Bokk na ci li gën a yéeme ci mbir yi,li ma daloon ,mooy man kat daa am bis may yër benn ci téerey siira yi (jaar-jaari yonnant bi),yaakaar naa ne téere boobu nuy wax “Zaadul Mahaad fii hudaa xayril hibaad” la,di ci maanaa yobbalub delluwaay ba muy ëlëg,ci jubug gën ji jaam yi,ba ma àgg ci ñi doon bindal Yonnant bi(j.y.m)maanaam ñi ko doon bindal wahyu gi ak bataaxel yi,ma lim leen ñu doon fukk ak juroom benn,Yàlla dogal ma ne naa xool nu itam ñi ci matal ab kaamil ci koor gii ñaata lanu woon ,far lim ba di benn,ca noona ma def ñaari woy,wenn wi ma ñaan ci Yàlla ci barkeb bindkati Yonnant bi (j.y.m),wi ci des ma ñaan ci ,ci barkeb bindkati Sëñ bi,am benn waay ci sama gaa yi ku ci tuxale ci man woyuw bindkati Sëñ bi te boolewu ci wu bindkati Yonnant bi (j.y.m). + +Ginaaw bi ma xool ci buntub ligéeykati Yonnant bi (j.y.m), ñuy juroom ñeent,ag jigéeen it nekk ci,mooy Barakatu yaayi Ayman,ma teg ci xool ligéeykati kër Sëñ bi,ca koor googee amul lu dul ñu toll ne ñoom,te ag jigéen bokk na ci, mooy Awa Saar jèbbéerub Sëñ bi,ma defati ñaari woy,kuréel gu ci nekk wenn tax la’a jug. Waaye ñaar yu saaba yi lakk,te kenn jotu leen a tuxal,ñaar yu ligéeykati ak bindkati Sëñ ba’a ngii: + +Bismil laahir rahmaanir rahiimi, +Muhammadu Lamiin Joop Dagana wax na di woy turi bindkati Sheexul Xadiim ca at ma mu koy woy,di leen tollale ak bindkati Yonnant bi (j.y.m) niki mu nekke loolu ci Zaadul Muhaad : + +(ci barkeb ñi jaayante ak ngën ji ligéeykati Yonnant bi,daan ko bindal,di ci gërëmloo aji des ji) +maa ngi lay ñaan ag jaayanteek moom gu dëggu,ni miy gërëme ku jaayante ak moom te di ko samp) +( ci barkeb Andariyi ,boroom mbégal mi,Muhammad mi nu tudde Bashiir) +( may ma ay mbég yuy leeral sama xol,yu di naa ci mujj di mbégum sama dëkk) +(fàtteel ma ci moom lu dul li nga ma tànnal,may ηoy (jàpp) ci wépp yiw wees ma tànnal) +(may ko ci yaw ak ci jëwrini Yonnant bi(j.y.m),mébëti xolam,akug jiital) +(yaw sama boroom nekkal ma cig aar,ci barkeb jaamam ba Muhammadul Amiin) +(nga dundal ci moom sama xol ci ay xalaat yuy tax nga gërëm ma ,bu ko defee ma dib jaam buy sant) +(na nga ko may ag aju (jébbalu) gu dëggu,ci darajay ki nga xam ne wommatal nga ko lu wér la) +(ci barkeb Sharif Mafaatim mu dañ mi kumpa,muritam bi nu melal ci ngënéel lu rëy li) +(teralal sama xol ci jikko yu rafet,may njariñ lu sax ñeel mbindéef yi) +(rafetalal samag dégg ak samay wax ñeel képp ku ma waxal yaw boroom may gi) +(nekkal ko, ci di ko may li mu bëgg,ci yiwi ñaari kër yi,mu doon ag am gu mat) +(yaw sama boroom ci darajay Daymaan,Muhammadul Xayri boroom koolute gi) +(may ma xol ak làmmiñ wu laab cig neen, ñu xam ko cig sàmm) +(te ma taqoo’k ragal Yàlla ak jëfe lu may tax a dab ñu mat ña) +(may ko mu tukkee fa yaw gërëm ak jàmm,juy des di ànd ak moom ba àjjana) +(ci barke turandoo wa ,muritam bu lewet ba,doomi Sulaymaan, Sëriñ Joob mu mucc mi) +(sarax ma saxug cofeel ak rafetal,ak ag ubbiku ci njàngum Alxuraan) +(ak jëllale ak dëddu lu dul lu rafet,ak jege luy bijjee jëme cig giim) +(màngal jëme ca moom ay barke yu sax,yu ànd ak sellug dund,ak mujj gu rafet) +(ak ci barkeb muriit ba ,doomi Sahiid NJAANI,Muxtaaram mu nu xam, mi mel ni Marjaan) +(may ma saxug noppi ci lu amul njariñ,tey wax lu am njariñ,te am njariñ) +(may ma kepp ku ma xam,mbaa mu dégg ma sopp ma ci lu dul ag xeeb) +(yéwenalal ko àddunaam ak diineem,te nga méng ko yoolub jiyaarkat yi) +(ci barkeb mbokkam ma ak saxiixam (mooy koo bokkal nday ak baay) bu baax bi,Ahmadu Binta boroom yéwén gu nu xam gi) +(may ma ag lewet ak xol bu yaatu,ba ma far nekk dib sang bu yaatu) +(may ma ag cawarte akug toroxlu,ak muñ,te nga sellal samy barab) +(na nga ko dundal yaw buur bi ngën ji dund,te nga def ko ci ginaaw bi muy dund ca àjjana) +(ak ca darajay doomi Faadil jii dib bindaakon,Majamba SILLA kay taarub bindkat yi) +(doxal sama diggante ak lu ñaaw ba fàww,ci lu bir ak lu làqu ak luy jax-jaxiloo) +(dóoral kiiraayul wattu ba fàww ci sama diggante ak bépp saay-saay bu dul jaamu) +(màngal ko yaw boroom bi,ci ñaari kër yi,barke buy aare ci ñaari gàcca yi) +(ak ci barkeb weer wi,doomi Muxtaar mi ñépp xam,di Ahmad waaye nu xame ko ci turu Moor Alima) +(may ma may taarub alxuraan,te nga may ma barkeb jàngale) +(kaweelal sama yite ci luy rafetal sama saayir ,ak sama baatin ànd ak xol bu laab) +(may ko yaw buur bi xam-xam ak jëf,ak teggiin yuy indi lépp lu mu mébat) +(ak ci barke doomi Ahmadul Muxtaar,Ahmadu Awa ,sang bu nu tànn bi) +(may ma ag baax gu ag bon dul toppati,ak ag nangu gu lamb dul jege) +(bépp ayib bu man a gàllankoore ci lu baax,na nga ma ko faral ba ma man a am texe gu sax) +(may ko lépp lu mu bëgg,ci yaw,te nga saxal bànneexam ci ngërëm ) +(ak ci darajay ki fëgg te sax fa,di Muhammad mi niy askanale Wajja) +(saxalal samaw làmmiñ ci wax aw yiw,ci waxtu wu nekk, ma noppi nag wëlif aw ay) +(na nga siwal samaw tur ci mbindéef yi,te nga def ko muy siiwug yiw) +(na nga ko may mébatam ci gii ak gee kër,di ku nu laaf ci mbooloom aji matale ji) +(ak ci barke doomi Ahmadu doomi Warxa mu Siin mi,kooku mooy Ahmadu KAN boroom askan wu nu ñongal wi) +(may ma ag aaru te setal sama lépp ci lépp luy taqal lu set) +((musal ma ci njuumte,may mag lewet,guy béel ak man ,ak jépp jëmm ju mucc) +(na nga tawal ci kawam niiri barke yuy sax ciy yëngoom aki dalam) +(ci barke ki niy wooye Ahmadu SAAXO,ki nga xam ne ab deram tër tilimalu ko) +(may ma nooyug kanam gu sax,déet ag ñëkk,gu koy ñaawal) +(na nga ma def may mbégum dëkkandoo yi,tey mbégum mboleem maas gi) +(na nga ko def muy boroomug dund gu teey,na nga def it ag deem di guy teey) +(ak ci darajay cam su nu sangal ,su gànjaru soosu,di Ahmadu mii nga xam ne aw dàkkantalam mooy Moor SIISE) +( may ma may kok du yékkati ab jéego jëme ko ci lu dul sa gërëm,yaw aji wattu ji ,ànd aki xéewal) +(na nga ma dëdduloo ba fàww ci lu dul luy tax nga gërëm ma,dëddug ku nu teral) +(may ko mu man a saxal li nga gërëm,ba man a làq sa gërëm) +(ak ci barke doomi Muxtaar mi niy dàkkantale Shams,te moom dafa mel ne ab jant ciw nitam) +(jeexalal sama xol ci yaw ,may boroomug dund gu sax ci yaw,tey boroomi yéene) +(na nga ma tàggatal njiit yi,te def leen ñoom ñépp ñuy samay soppe ci yaw) +(ak ci darajay aji ragal ji Yàlla ,aji yéwén jiy teet lépp lu bon,Ahmad doomi Saynabu ji) +(na nga ma may ag ragal Yàlla ,akug wattu akug dëggu,ci wepp yiw , may sàkku ag dëggal ci yaw) +(na nga teetal sama xol ag bëgg àdduna,bëgg gog da na man a lor kuy wutug jeex ci Yàlla) +(na nga ko gindi ciw yiw wow da na xeeb ba fàww sottikug niir yi,te kenn du ko xeeb) +(te ci barkeb Usmaan mi nga xam ne ñi ngi koy wooye Demba KEBE,méngoo ma te fegal ma njàqare) +(yaw sama boroom,ba fàww,na nga ma aar ci lépp lu my ñaawal niki wor) +(may ko yaw buur bi ba àjjana,muccug yaram ak xol) +(asaf naa nag ñu baax lool ci bindkat yu siiw yu kawey daraja yi) +(bañ gi ma leen bañ a indi doyadig pas-pas waralu ko,waaye kay li ma sartoon a def moo ci mant a boole keneen) +(yaw sama boroom,ci seen barke ñoom ñépp,na nga nangu sama ñaan gii ba fàww) +(na nga nu may mu tukke fi yaw,gërëm ak yërmaande,te nga rafetal mujjug ku nekk ci nun) +(ci darajay Ahmad ligéeykatu Ahmad,xéewal ak mucc yal na ko Yàlla mi ko yatt saxal ci moom) +(ak ñoñam aki saabaam ñiy boroomug soppante ci yaw,ngir sa jëmm,ci lu dul ngàññante) +(li feek kuy ñaan ci barkeb ku àgg ca aji rafet jay yonni yonnant yi,mi ngi am li muy ñaan). +Sama boroom yal na nga nu nagul,yaw ay aji dégg jiy aji xam. + +Woy wi mu defal ligéeykati Sëñ bi ,di ñaan Yàlla ci seen barke,tollale leen ak ligéeykati Yonnant bi (j.y.m),woy waa ngi nii: + +(yaw sama boroom ci darajay juroom ñeent yoy ligéeyal nanu ngën ji jëwrini Yonnant bi,kok kawe na képp ku ligéeyal Yonnant bi (j.y.m) ) +(saxalal sa ngërëm lu màgg li ba fàww,ci ki nga xam ne ag ligéeyalam lu nu saxal la) +(sama kerkeraan jëm ci yaw,kiy buntub samag tonowu,kiy far ñaawtéef yi,kiy dañal ag mbon) +(ci darajaj Malaamin NJAAY,boroom farlu gi ci ligéeyal Aji ñeewant jiy musal jépp aji gindee) +(may ma ag cofeel guy taqoo’k xel mi,ci jëmmi ki nga xam ne def nga ko muy leerug réew mi) +(na nga tàggat samay cér ci ligéeyal ko,tàggatug ka ma jegeel ci sottig xéewalam ya) +(na nga ma def ma sopp képp ku sopp,aji ligéey jii,na nga ma def may ku mu sopp) +(wommatal ko lépp lu mu mébat ci ligéeykat bi (Sëñ bi) ,niki muy xéewalee) +(ci barke sëñ Moodu FAAL,maa ngi aaru ci lépp lu ñaaw,ba fàww) +( may ko li mu mébat ci àdduna’ak allaaxira,te nga fegal ko ñaari gàcca yi ak ñaari sawara yi) +(na nga ma may ag mucc ci kiñaan ak bañ ab jullit,te nga leeral sama pas-pas) +(na nga def ci sama xol yërmaande ju may nooyale jépp aji wow ji xol,ba kero muy nooy) +(na nga may képp ku aju ci man ngën ji ag wommatu ñeel ma,ba ma man laa gërëmloo) +(ci barkeb aji lënkaloom ju lewet,di Sahiid SALL,na nga ma fegal mbooleem lu ag xuppe di nekk) +(màngal ko jàmm ak xéewal,gu sax ba kerook tàbbig àjjana) +(na nga ma ci maye ag jub gu sax ci lépp loo digale) +(na nga ma may ag not sama bànneex,ak bakan,ak saytaane ak àdduna) +(na nga seral ci man xolub samay dëkkandoo,ñu jub tey diisoo) +(ci barkeb camus Mbakke si ko daa rootal,di Aboobakrin,na nga dolli samay xeewal) +(sottil ci kawam ci dexi yiw yi,lol da na koy jañal lor) +(te nga kaweel sama yite ci moom ci li ma bëgg,ci lu dul may gestu lenn loo bëggul) +(na nga ma may ag toroxlu ci képp ku ma dajeel ci julliti jamono ji) +(na nga màggal ci sama xol ak sama bët,bépp murit bu askanoo ci man) +(ak ci barkeb ki mu lënkalool,di Sahiid MBAKKE na nga ma may mboot muy jooyloo képp ku ma bañ) +(may ko ci sunu sëriñ bi,la mu bëgg,ci àdduna’ak allaaxira ,mu dëppo ak la mu bëgg) +(na nga ma may ab ligéey ci darajaam,mu dib sarax tukee fa yaw) +(na nga ma may barke bob ku dul man dana ma ci ñee,ànd ak xol bu neex) +(na nga nu may nun mbooloo mi aju ci Sëñ bi,urma ju dul xottiku) +(ci darajay mbokkam ma Ibra MBAKKE,dañalal ayib yi ag dañal) +( may ko gën ji dund aki yiw yu koy bégal ci gii kër ak gee) +(na nga matal samag mbañ-rus,musal sama xol ci mbañeel,te kaweel sama daraja) +(na nga musal samay cér ci lépp lu bakkan man a ragal,ak doonte du lu metti) +(na nga barkeel ñeel ma,ci sama mbokk yi ci Yàlla,ak ñeel sama mbokk yi ci Yàlla) +(ak ci darajay doomi Maryama mi kawe fa Sëñ ba,miy Siidi Kala) +(yal na ko kiy namm, defal la mu namm,ca kaw nammeelam,moom miy aji namm) +(na nga ma def may ku dëggu fa yaw ci li ma bëgg te nga gindi ci man aji dëggu ji) +(na nga rafetal sama njort ci bépp murit bu aju ci sama sëriñ,te nga teetal ma ku nu dàkku ki) +(na nga ma musal cig yàkkamti,te may ma ma jot gaa ya) +(ci barke camus cam yi,Mbakke JUUF,mi amul lu muy ragal) +(may ma ma nekk kuy ligéeyal Sëñ bi li feek ma’a ngi dund,kii nga xam ne ligéeyal ko mooy ligéeyal aji jiitu ji (di Yàlla) +(tàbbalal ma samay xemmemtéef ciy xemmemtéefam,dammal samag dëddu cig dëddoom) +(ubbil ma yaw buur bi cig ligéeyalam,ag ubbi gu may aj ca kaw ña koy ligéeyal) +(na nga sellal ag dundam ci guddal ko,te musal ko ci ay gàkk-gàkk,walla nga def ko far lem) +(ak ci barkeb muritam bu jigéen ba Awa,jèbbéeram bay saxal lu baax) +(may ko texeg dund,aki néeg yu kawe ci ginaaw bi) +(may ma bakan bu dal ci Sëñ bi,bu doylu,bu dul jeng jëm ci ku dul moom) +(tàggatal ma jigéen ñi,te yombalal ma seeni mbir,te nga dagg jafe ga) +( yéwénalal ma ko te def ko muy ndimal ci topp la) +( na nga ma wisaareel ay doom yu góor yu baax ak yu jigéen,yu baax,yu am diine te ñong) +(ñoñ da nga dundal ci ñoom lislaam,di ma fegal ci ñoom yeddaange) +(ñoñ da nga leen di barkeel ci jox leen wërsëg wu yaatu,wu dagan,ba ca àjjanay Aji yaatu ji) +(na nga def ngën ji julli,goo xam ne da nga ci nangoo sama ñaan gii,ànd ak sutura su rëy) +(ak xéewal gu sax gu nu gëttal,ca ka ñu xeeñal ngën ji gëtt) +(di Muhammad,ak kuréelam ba bépp,te nga wuyyu ma ci seen barke yaw sama boroom) +(wuyyug nangu,ak ngërëm ak teral,guy tax may ku nu wormaal ci biir gaa yu baax) +(jeexalal samag dund ci lu rafet ci seen barke,ñuy ñu ñu béelal,ca saxuwaay bu kawe ba (àjjana) ) +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina. + +Cig gàttal daal,dundug Sëñ bi ci Njaaréem gisunu ko fenn ci nettali ak jaar-jaari kenn ci sëñ su mag si,ci sariiha ak haqiiqa,lu dul li tegoodi ci yoon ci ligéeyub buur yi,muy jéem a def àttey yoon yi,di dagg loxoy sàcc yi,di jam njaalokat yu senge yi,ak door ñu sengewul ñi,ak di leen tumbrànkeel,te loolu wuute ak àttey àtte gi (nguur gi),ndax àtte yooyu daganalunu loolu,te dëppoowul ak seenuw doxiin wu mat ci fànni politig yi. + +Fatabaarakal laa,ahsanal xaalixiin,mbooloo yi bari woon nanu ci moom ca Njaaréem,ba nguur gi mujjoon aaye ko muy dox ci nit ñi ci lu dul ag diggale,loolu taxoon muy wut ay palanteer yu ndaw,ci bunt bu nekk,ci wàlli kër gi gépp,nga xam ne fu mu tooge ba ubbi palanteer,ñaari nit ci ñu jege ñi man a gise bu nu jàlle ñeneen ñaar jegesi,noonu lanu koy nekke ci suba ba bëcëg ci li gën a bari,teg ca ñu nekkaat ca tàkkusaan ba timis ak lu ëpp guddi gi. + +Amaa na leeg-leeg mu dem bind ag xasida,mbaa mu dem ca buntub jigéen ñay siyaaresi,mbaa mu dem nemmiku njaboot gi,su bëggee jàngale,da daan soril nit ñi bunt bi,ñu kuréelu,def géew,mu tàmblee tomb ci suuf ngir njàngalem sariiya ak haqiiqa,ci alxuraan ak haddiis ak hikkam,ak masalay fiq yi,amaa na mu jànglu xasida,bu ko defee wattukat yi jug jéeb,ci kàddu gu neex,moo xam danu koy xool,mbaa nu koy tari,xasida yooyu daawunu weesu tagg Yàlla ak Yonnantam ba,bu ko defee lekk yi ak naan yi,di daw ci diirub jataay bi,lu fa waay soxla rekk ci àdduna ak diine. + +Nguur gi aayeeti ko mu dem ca jàkka ja,ba mu mujj def jàkkam ca fu jege kër ga,ndax moom kat daawul wuute jullig mbooloo ca jàkka ja,du guddi,du bëcëg,du tàngoor du sedd,du xiinadi ,du xiin, mu bàyyil nit ñi ci kër gi aw yoon wu nu man a jaar julli ji,moom mu wut aw yoonu boppam,wu koy àggale ca mihraab ba,du nu ko gis mukk,ndare bu daa taxaw ca mihraab ba,ubbi bunt bi ndare palanteer bu sew bob du tee ñu seen ko,ci mbooleem julli gi, bu ko defee mu daa tëj bunt bi bu noppee ci julli gi,daan ko ubbi it ngir jàngale. + +Nu aayeeti ko muy dox ci yoon yi,te kat nit moom ku soxlawoo loolu la,ba mu mujj aajowoo sàkk ab palanteer bu sew,te sori ci làkkub kër gi,digganteem ak làkk bi aw yoon wu yaatoo ñeenti xasab a nga fa,mu fay jaar bu bëggee doxontu suba ak ngoon,walla guddi. + +Nga gis nit ñi ñu wër ko,ci ginaaw palanteer bi,di dox ànd ak moom,di taxaw bu taxawee,ak fu mu jublu,amaa na mu taxaw ngir tufli leen bu noppee ci ñaan gi,mbaa mu jàngal leen am masala,jàng gi it da daan bir,loolu lépp ab politigam la woon ngir soxla gi ko nit ñi soxla,ngir jariñu,ak gindiku,ak soxla gi mu leen soxla ngir jariñ leen ak gindi leen,bu teelut a lijjanti loolu ñu lor ko ci taxaw ci kawam. + +Seere nanu loolu ndax kat bis dagg nanu ko ci baaraamam,dagguw dàllam it,ngir xér ci laal jëmmam ju tedd ja . +Waaye buuxante bu metti bi mooy waral ñuy dal ci kawam,ba koy gaañ ,te dunu jublu loolu . +Bu ko defee muy gaañu ci loolu ndax moom jëmm ju tuuti,te doyadib bind la waaye di ku dëgër ca Yàlla,du yoqat,te du sonnu,ba bi ko mbirum Yàlla mi dikkalee,ñu tànn ñaar ngir ñu toppatoo ko,ñuy ñaari muritam yi Muhammad mom Abdu Rahmaan Attandaxii, mi faatu,ci ginaaw bi ci sawaal,atum bahsasin,di junni ak ñatti teemeeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar, yal na ko Yàlla yërëm, kooku moo ko doon toppatoo ak mbokkam mi bind araf yii,Muhammadul Lamiin JOOB ,ñu duggal ko ab wata guddig àllarba yobb ko Tuubaa,ci pexe mom danu koo def ngir làq ko nit ñi . + +Ñi ko doon gunge juroom lanu woon,sëñ Bashiir moo leen jiite woon . Mu dal di yonnee ca mbokkam ma,sëñ Muhammadul Faadal,xalifab ñaareel bi, te ca jamono jooja,ma nga woon ca wurumub dëkk ba,ca wetu Tuubaa , mu yonnee ca Sheex Ibraayma ca Daarul Muhtii,ak ca sëñ Mbakke BUSO,ca dëkkam ba ca wetu Tuubaa,mu yonneeti ca mag ña nekkoon Tuubaa, ñooñu daje ci diir bu gàtt,ba nu matee ñaar fukk ak juroom ñatt,sëñ Mbakke BUSO jiite leen,loolu lépp a ngi ame woon ci làqu gu tar,ngir bañ fitna, ñi ngi noppi bi fajar daataa jot,def fa ab néeg bu nuy tëj ak a tijji, bi ko nit ñi yëgee bi suba jotee,coow li jolli,bul laaj nag wax yeek jëf yi,loolu lépp bi muy am sëñ Moodu Mustafaa ngi Njaaréem di xamal nit ñi ak di leen dalal . + +Bi nu noppee ci waajal gi,ma génn ci bunt bi ma njëkk a jot,laa daje ak kenn ci taalube yi,te booba moom yëgutoon li xewoon,mu ne ma man kat biig dama laa gént ,di la laaj Sëñ bi, nga ne ma: (( wamaa Muhammadin ilaa rasuulun,xad xalat min xablihir rusul)) muy ci maanaa Muhammad du lu dul ab yonnant,bu fi ay yonnant jiitu. Ma ne ko ni nga ko gente la deme de,duggal,bi mu duggee,tàmblee yéemu . + +Ki boole téere bi defal na ko marsiya (marsiya = xasida gu niy waxe jëf ju baaxi ku faatu) ci ay bayit mooy bi nu njëkk a defal Sëñ bi, bi mu fi jugee,mi ngii: + +(Sëñ bi wéy na jëm ca buur ba mu daa jaamu,ndax kat xamoon na ne fii kenn du fi des) +(mu wogu di sàmm ndigali Yàlla yi,ngir ngërëmam tey teet li mu tere) +(di tere lu bon tey digale lu baax,di def lu nu xam te du ca ëppal) +(nekkoon na kenob diine ca bisi dundam,ñoñam de,moom lanu jublu woon ci sàkku dëgg) +(gisoon nanu ne mooy seen baay,bu nu war a jox àqi baay,moom itam,mu gisoon ne àqi doom lu nu leen war a jox la) +(mooy ki daa fàtteloo jirim yi seeni cosaan,daan faye aw ay ciw yiw ) +(moom dey naataange la woon ñeel ñu ndóol ñi ko daa dikkal juge fu nekk ngir xontu) +( bu daganoon nu jote ay bakkan de,nu def ko,waaye ay sang jiitu nanu ko,juge fi,te kenn jotu leen ) +(waaye de na la woor ne bu fàddoo wëlif nu ànd ak jëmm ja tam,du tee aw yiwam wiy dolliku du fàddu mukk wëliif nu) . + +Buurub woykat yi it ca jamonoom ak wàllam,di Muhammad mom Muhallaa Alhasani defal ko moom itam marsiya bu yéemee yéeme,mi ngii: +bismil laahir rahmaanir rahiimi,wasallal laahu halaa nabiyihil kariim, Muhammadu mom Muhallaa,mi nu gën a xame Naana,mi ngi wax di marsiyaal Xutbub Xawsu bu boroomam bu mag bii di Sheex Ahmadu Bamba mi nu xame ci turu Xaadim,yal na ko Yàlla labal ci géejug yërmaandeem,te sarax nu ci barkeem, aamiin: + +(yoonu dee mooy dayob kuy dund,dund daal lu dul dee toppu ca) +(nit ñépp a ca jëm nag (moom dee), bu bettewul ci bëcëg gi ,def ko ci guddi gi) +(moom daa mel ni ab rawante bob mooy bant ba nu samp jëm ca,ku ko jéggeegul it ca nga jëm) +(ndaw dayo bii di bu yéeme !,moom de mooy saxuwaayu seeni mbooloo,tey dajekaayu seeni kuréel) +(lu waay tàyyeel tàyyeel du tee mu jot boobu dayo,lu waay sawar te bariy jumtukaay du tax mu romb ko ) +(dee daal daa mel ni ndabul nganale lu nu woo ñépp,woote gu matale te yaatu) +(bu aji ligéey ji wuyyo wooteg dee gi ti,te kenn bégu ci ) +(jotoon naa wuyyu cig njëkk wooteb Yàlla bi te booba gindikat yi jugagun) +(mu daa wuyyu wooteg képp ku woote jëme ci yoonu kawe ak teddnga ) +(mu nekkoon di kiy woote ak a gindee jëme ci ngérum jàmm ak mucc) +(moom de bi sàmmkat yi ruuralee seenum càmm,daa féeteek aji wattu ji,sàmm am càmmam) +(teg nanu ko lepp lu diis lol yanukat ba gën a mag gën a dëgër àttanu ko). + +Bokk na ci jikko yi mu ko limal: +(ak dagg buumi ñaawtéef yépp,ci lu dul gestu guy gàllankoor walla yoqat) +(ak dundal xol yi ci sikar ak waaraate yi rafet ci waaraate yi) +(yéem naa ku mel ni moom, ci niir ak tawub dundalug xol, bu nuy màng, jëme ca suuf yu bekkoor ,yu naatadi yi) + +Mu neeti: +(ki ko tànn daal a ko woo jëme ko ci teraanga,ngir fay ko jëfam yu baax yi) +(moom itam mu wuyyu,ba mu demee fekk fa la mu doon mébat,ci ngënéef yu gànjaru yi) +(mu mujj ñàkk gi nu ko ñàkk,di lenn ci way jommale yi,te di am mbamb (xew-xew bu njàng) mu lëndëme ni tàggeg tàggekat yi) +(Abdul Xadiim daal wéy na,di ku nu santi jëf,di ku ay mbootam lenni gàkk-gàkk nekku ci ) +(Abdul Xadiim daal wéy na, te bënul lu dul bëtub ay may aki xéewal) +(wari fas daal du woon yitéem, te ji ay tàndarma yuy dott it taxu ko woon a jug) +(dundug buur yi de dug dudam ,ak doonte day joxe ay bóoli yu nu feesal) . + +dundug Seex Ahmadu Bamba +Tëj: + +Ñu tëje ko ci waxtaane lenn ci li ko Yàlla may ciy xéewal yu kawe njort, ginaaw bi Yàlla sooyalee seen ñatti pexe ya,muy ray ak tëj gu sax,ak tumbrànkeel gu sax . +Bokk na ci li ko Yàlla xéewalee ci safaanub ñatt yooyu - Sëñ bi nee na - def gi mu def ati tumbrànkeem di lu juge ci nattub yonnant yi ak seeni balaa,yi leen seeni noon daa teg,mi ngi wax ci loolu: +((bokk na ci xarbaaxi Yonnant bu nu gënal bi,yal na xéewali aji kawe jiy gënale nekk ci moom) +(bokk na ci xarbaaxam yooyu:nekkug sama ati tumbrànke gi di lu nu génnee ci jamono ju jàll ) +(ñu niroole ko ak la xewoon ca diggante yonnant ya ak ña nga xam ne ñoom ñépp ay kàccoor lanu) +(yal na xeewal ak mucc sax ci ñoom,ni Yàlla dàqe ak lëndëm ci yonni gi mu leen yonni) +(ag kéemtaan dey feeñ na ci sama tumbrànke gi,ni mu feeñe woon ci Yonnant bi moom mi gindee) +(loolu mooy ñi sabablu woon tumrànke gi de) +(ñee nañu ñi ko sababluwutoon ci noon yi,te Yàlla notal na ma leen ) +( ñi ko sabablu woon de dunu tàbbi àjjana te sawara lanu jëm ) +(te du nu am li feek tuubunu,lu dul ngën jaa saxi njàqare). + +Mu bëgg a wax ne Yàlla màg na te kawe,niroole na ci ngënéelam, li amoon ci sama diggante ak noon yi,niroole na ko ak li xewoon diggante yonnant yi ak seeni noon,ciy nattu,mu niroole la nu ca ame ciy xéewal aki njariñ lu nëbbu ak lu feeñ,fii ak fa nu jëm,mu niroole loolu ak li ma ci ame ciy xeewal aki njariñ . + +Mu tollale loraangey àdduna ak ju allaaxira ju noonam yi tuubul ak loraangey ña tuubutoon ca seen noon ya. Te ña sababoon nattu yooyu ak fitna yooyu,ñee nanu ñi ci àndutoon ak ñoom ,li Yàlla di wax naan: ((wa yawma yahaddus zaalimu halaa yadayhi,yaqoolu yaalaytaniit taxaztu mahar rasuuli sabiilan,yaawaylataa,laytanii lam attaxis fulaanan xaliilan,laxad adallanii hanis zikri bahda isjaa anii wa kaanas shaytaanu lil insaani xazuulan) muy ci maanaa : bis ba nit di màtt loxoom wiccax,naan aka neexoon ma topp Yonnant bi,aka neexoon ma bañ a def diw xarit,moo tax na ba ma réere alxuraan ,ginaaw bi mu ma dikkalee,te shaytaane dey day gàccaal nit rekk. Mu ne moom aaya woowu seere la ci Yonnant bi (j.y.m) ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom, tey kéemtaan,waaye di seere ñeel ma tey karaama,kon alhamdu liilaah,sant naa ko te gërëm ko,ci dëppale gi. + +Bokk na ci mbóoti sama tukki bi,xéewal gi ma Yàlla defal muy juroom ñaari karaama,tolloo’k kiimaani Yonnant bi (j.y.m),ñooy: Yàlla notal na ma samay noon njëkk samag feeñ, may ma xam-xam bu jugewul ci njàng, Yonnant bi (j.y.m) puukarante ak yonnant yi ci sama tumbrànkeg fukki at yi ak ligéey bi ma ko ci ligéeyal muy ligéey bu sell, Yàlla def ma may koo xam ne képp ku texe da na ko sopp,te naagul ibliis ci man ak képp ku nu rëbb, mu def ma may ku malaaka yi sopp,ak way gëmi jinne yi,def it julliti jinne yépp aju ci man ngir jëmmi Yàlla,mi ngi wax sax ci loolu naan: + +(( juroom ñaari kéemtaan ci yu Yonnat bi,feeñ nanu ci man,te am naa samag ñaan ca seenug njëkk)) +((sama boroom ci barkeb ku nu tànn ki ,notal na ma noon yi,njëkk samag feeñ,te du ma dajeek kuy noonu)) +((Yàlla may na ma xam-xam bu jugewul ci njàng,te indil ma Kun (mooy nekkal mu nekk) )) +(( Yonnant bi puukarante na ak yonnant yi yépp,yal na xéewalug Yàlla nekk ci ñoom)) +(( ci sama tumbrànkeg fukki at yi,ñu ànd ak ligéey bu sell ñeel boroom nekk gi ak jiitu gi (Yàlla) )) +((képp ku texe da nga ma sopp ba fàww,ngir jëmmi sama boroom miy aji delloo,sopp gu àndul ak ag mbañeel)) +(( Yàlla miy aji dimblee,naagul na ci man ibliis ak képp ku nu rëbb )) +((malaakay aji tedd jiy aji des,danu may bëgg ngir jëmmam ja,ànd ak texe gu dul dagg)) +((ñi gëm ci jinne yi,sopp nanu ma ngir jëmmi aji des ju may defali xéewal)) + +Mu waxaat ci beneen barab: + +((jinne yi gëm ci sama jamono jii aju nanu ci man,waxu ma, ñi gëmul)) + +mu neeti: + +(( mayal ñi ma ligéeyal lu rafet,moo xam malaaka la,mbaa ku nu làq (jinne) walla nit)) + +Nu xame ci loolu ne moom kat am na ñeneen ñu dul nit ñu koy ligéeyal,mu waxati ci beneen barab: + +((Muhammad may na ma ag not,képp ku dëkkaale ak moom du nu ko not)) +((samag texe day des ci lu dul rékki,Yàlla notal na ma mbooleem ay noonam)) + +Mu waxati: + +((kuy léewtoo jubluwu ma,bëbbug (xeewali)sama boroom lu feeñ la,ibliis de du léewtoo’k soldaari aji tedd jiy kenn)) + +Mu neeti: + +(( wattu naa lu nu ñogal wëlif téere yi,kon bul tàyyeel ci ligéeyal ma)) +(( Yàlla màngal na ma mbooleem xam-xam yi,aji tedd jii de baax na , +mooy aji dañ ji kumpa,tey aji xam ji)) +((kiy def lu ko soob de nocci na xam-xam yi ak seeni barke ñeel ma,ci nekk ngi mu nekk di aji xam)) +((ki nga xam ne wommatal na ma aw yiw,wuy sellal xol,te yiw wa wommatu de,déeyaale na ak man)) +((Yàlla xéewale na ma jàngale,di naa gindi ku réer ak ku am xam-xam)). + +Bu dee ni mu bëgge ñi gëm nag ak ni ko ñooñu bëgge,loolu moom jarul sax nu ciy wut lu ko seere,ndax mbir la mu niy gis,di jàkkaarloo ak moom,muy barig jariñ gi mu leen di jariñ ,ci xam-xamam ak alalam,aki mbóotam,aki ñaanam, du amadi solo ñu tudd cis lëf ngir barkeelu ci,am na fu mu naan: + +(( jéggalal jépp aji gëm ju góor ak ju jigéen,jéggal guy saxal wépp yiw)) +((jéggalal bépp jullit bu góor ak bu jigéen,jéggal gu leen di musal ci tooñkat yi)) +((jéggalal jépp aji rafetal ju góor ak ju jigéen,jéggal gu leen di wommatal lu rafet)) . + +Mu neeti ci Matlabus Shifaayi: + +(( na nga saafara mbooleem jullit ñi,ci fii,te nga fegal leen tiit ak njàqare ca fee)) +(( na nga leen musal te jàmmal leen,te ñeewant leen,te bul fayyoonte ak ñoom ngir barig seeni bàkkaar )) +((ndax ñoom kat bu nu la moyee ngir sàggan,du nu la bokkaale ak kenn)) +(( te seeni yaram àttanuñu sab nattu ,ngir seenug doyadi)) +((seeni xol de du jéng jëm ci ku dul yaw,ba fàww, ci fii ak ëlëg )) +((waaye nekk gi cér yi nekk di ban,bijj na leen ,yobb leen ci gën jaa boni bon-bon yi)) +((bul fayyoonte ak ñoom ci lu la dul wàññi,may leen li leen amal njariñ,te amalu la njariñ )) . + +Mu waxati ca xasidaam ga tudd (Fastajaaba lahum rabbuhum): + +(( ci darajay Mustafaa,wuññilal xeetam wi njàqare,yaw mi génne sa jaam bii ca njàqareem la)) +((bindalal Yonnant bi xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam yiy boroomi teet lu bon )) +((musalal aw xeetam ci darajaam ak seen daraja ñoom ñépp,yaw kenn ki ma notal)) +((wuññilal njàqare ñi di boroomi gëm,yaw miy kiy maye ag koolute)) +((yaw aji rafet ji,àggaleel ci mbooleem jullit ñu góor ñeek ñu jigéen ñi,jàmmi boroom mbindéef yi)) +(( bindal ag sell ñeel mbooleem way rafetal yu góor yi ak yu jigéen yi,yaw mi méngoo way gëm yi)) . + +Ak lu bokkul ak loolu lépp ci li nu manul a lim,ci lii di wone bëgg gi mu bëggal xeetu Yonnant bi (j.y.m) li mu bëggal boppam,mu jagleel ci boroom jagle yi,geneen bëgg gu gën a tar . + +Dégg naa ko bis (g.y.m) mu naan :man dey jamonoy samag ndaw,dama daan tànn ci giir gu ne ab xarit,daan ko jagleel ci sama xol ag cofeelug boppam,ni ma tànne woon ci giirug Daymaan,Muhammad Yaddaali,boroom téere bi nuy wax (Zahabul Ibriiz),ci giirug Tandax ma tànn fa Muhammad FALL mom Mutaali,ci ñoñ Haaj ñi, ma tànn fa Ahmadu doomi Muhammad,boroom (Jawharul Munazzam). + +Bokk na ci li mu nu nettali ci cofeelam gu yéeme gi ak mbëgéelam gu tar gi ñeel ñennat ñi ci jullit ñi; nee na bi mu nekkee ca tumbrànke ga ca géej ga,daa yëggoon ne sunu mbokk mi Muhammad SEKK,mi nu gënoon axame ci turu sëriñ Làmbañ,ak sunu mbokk mi Muhammad JOOB,ñu gënoon koo xam ci turu Majoob Aram Seriñ Fittu, tubaab bi da leen a yobbu woon ngir tumbrànkeel leen,xawma fan nag,bi mu ko defee mu amoon lu ko naqari lool,nee na àdduna dal di lëndëm fi man,sama jamono nëx ngir ñeewant leen,ndax kat bëgguma ñu nattoo leen lu leen di tax a ñàkk seenig gëm,mbaa mu koy rékki ci ñoom,yal na nu ci Yàlla musal,ma dal di ñaan Yàlla ci seen mbir moomu ne: +(( yaw gën ji aji jéggaley bàkkar,tey gën ji ku man a musal ku nu jàpp)) +((na nga dindi jullit ñi cig njàpp,te musal leen ci luy waral sikk )) . + +Ñaari bëyit yooyu ñi ngi ci xasida gi tudd ((wa àmmaa maayanfahun naasa fayamkusu fiil ardi)),man naa am bi muy bind xasida gi la ko seenub xibaar dikkal,mu dal di def ñaan gi. + +Bu dee bëgg gi ko ñi gëm te di boroom jagle bëgg ,loolu moom lu nu xam la te siw,seereel nanu ko yiw wu nekk,ak wilaaya gu nekk ci barab bu nekk . + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Doggantal : + +ci seere gi ko ñu mag ñi seereel ag màgg ak ag wilaaya + +Xoolal Sheex Siidiya mii ak màggam gi mu màgg lépp,téewul mu tegoon Sëñ bi fu mu tegul kenn,bind na ci moom,woy ci moom wesar ci moom,bu waxutoon lu ëpp ñatti xasida yii tam,ci xasidaam yu bari yi,loola da na doy,ñooy yii: + +(Sheex Ahmadu daal xéewal la ,gu Yàlla jox mbindéefam yii yépp) +(ag cant ñeel na Yàlla mi ngi xam ne ay xéewalam jaamam yi manunu koo takk,mbaa nu lim ko) +(boo dajee ak moom,fekk ñuy yekkati raayob teddnga,da nga ko gis mu alawtiku ko ci loxol ndayjooram,ànd ak di tudd Yàlla ) +( bu gisee bis jikko yu rafet yi ñu dëdd leen,day dogu jublu ya ca gën a mag) +(suuf su ko dëkkal daal ,ab lolli bu ko ñàkk a ndàndal du tax mu lor ko ) +(miskiin yi ngir sa baax gi fàtte nanu seeni dëkk,ba mujj na sa koom mii de lanu jàppe seenum koom ) +(seen mbooloo yooyu de buy daje ak ñoom mbégte mu rëy te dëggu lay àndal,nga xam ne da ngay jort sax ne,lu toll ne li mu leen di jox ciy xéewal rekk,lanu koy jox )) +(( mbooloo yépp seere nanu nekk gi mu nekk di ku baax,ku tedd,kuy jaamu Yàlla te dib tuubaakon )) +(( bokk na ci ñi gisoon jariñ nit ñi di farata,ci jamonoom,tey ci ñi daan tudd Yàlla )) +(( dogal bu ñëw mu nangu ko te gërëm ko,xam ne Yàlla’ay ki ko dogal )) +((bu kuy tëñëxu cig lëndëm di tëñëxu it,moom genn muuraay du man a muuri bëtam wëlif dëgg gi )) +((kersa du dañ di ab rootukaay ci sab hadara,bu ko defee yiw yi di noyyi ci gelawam lu sedd li)) +((jaam yi de ,dox gi nu dox jëm ci moom,seeni aajoy àdduna’ak allaaxira’a ko waral)) + +Ñaareelu woy wi +mi ngi ko def bi mu tàmblee tabax jumaay Njaaréem ji,mi ngi nii: + +( jàkkay Sëñ bii de mooy jumaay barke ji,tey barabub ay yiw ak yërmaande ) +( fa lanuy jéggalee ñaawtéef yi,ña koy siyaare it seeni yiw danu koy ful) +(boroom fondumangub ragal Yàlla la ,ak miiri jëf ju baax ak teraanga) +((jëf ju sell ñeel boroom mbindéef yi,ci yeene,te jëf ya’a ngi ci yéene yi) +(boobu barab de,làquwaayub ku bëgg a taxaw guddi ngir jaamu Yàlla la,kon de bu baax la,làquwaayub ñu ndool ñi de làquwaay bu baax la) +(bu fa julli ngir Yàlla amee ab néeg it,du tee muy neegub jokkoo ngir Yàlla) +(xamal nanu fi julli ay waxtu,waaye jàkka jii de am na lu dul waxtuy julli rekk) +( nit ñi danu koy jublu,ànd aki xol yu boole lu tàqalikoo ciy yeene) +(ab kuréel bu fay ñëw ngir julli,ak beneen bob mbiram mooy asaka ) +(Yàlla digale na ñu yèkkati ay néeg,yu tedd ci kaw yeneen néeg yi,ngir turam wi) +(yal na Yàlla faye tabax gi, ay kër yu niy tabax ca àjjana,ay jigéen nekk ci) +(Sëñ bi daal xéewal la,gu Yàlla joxe,di kiimaan ci kiimaanam yi) +(nit ñi de xam nanu ko ci penku bi ak ci sowwu bi,mu dib sang ci taax yi ak ci kaw gi ) +(mi ngi bokk ci tabaxkati jëf ju baax,te loolu lu néew la ci nit ñi) +(dellu nanu seeni kër,ànd akug cant,gu toll ne cantug ku soxla woon am ndox Yàlla jox ko dexug Furaat) +(yal na ko Yàlla wattu ci wattoom ga akug kaweem,aki doomam yu gó0r ak yu jigéen) +(ak ñoñ néegam bu kawe bi,mboole seen,ak muritam yi juge ci wàll yépp) +((te Yàlla may ko “Xurratu Hayni” (am mbégte) ci àdduna ak allaaxira) . + +Ñatteel bi + + ci yu mujj la,da fa mel ni danu koo wonoon ne ab digam daa jotoon : + +(burub nit ñi yal na la fay ngën ji fayam,te dolli la ci teralam gi ak mayam gi) +(te mu desal la fi,ngir mbindéefam yi nga xam ne,sag des moo di seenug des,xéewale la mooy xéewale leen) +(kuy jéem a tolloo’k yaw bu woomlee tam,nan lay yéege ba jot ku ko gën a woomle fopp?) +(nan lay yame kok am koomam mi ngi ci joxe ko, ak kok mi ngi ci denc ko ak làq ko? ) +(ndax kuy jënde alalam ab yool ak ndam,da na mel ni ku nuur ci njaayam ma’ak njëndam ma ? ) +( cam la su teddnga di feeñ bu feeñee,bu làqoo,sooroolub njèkk làqu ) +(bis bu Yàlla dogalee tenqam gëbum koom,da koy dal di seddale way yalwaan yi) +(day jàppe jeexug alal,akug naaxsaayam, muy di ko jéem a màggal ak a dajale,joxe ko ci yoonu Yàlla it mu jàppe ko muy li koy yokk ) +(bariwaa na ay gawar yu mel ni ay cati xéej,naaga (giléem) yi daw ak ñoom,jéggi ab àll,bob suuf sa daa mel ni asamaan sa ) +( ki leen di wommat,di yaakaar ju rafet ji nu am ci moom,ki leen di gindi di kaweem gu rafet gi ) +( ñu jublu ,bu nu àggee ca ëttam ba,fajug seeni aajo ci lu dul nëx-nëx,ànd ak am lu leen ci wóor ) +( ayibam daal du lu dul jaamu Yàlla,ak jariñ nit ñi suba’ak ngoon) . + +Aji seere ju mel ni moom cig ragal Yàlla,ak am xam-xam,te di ko jëfe ak sax ci sunna,doy na sëkk. Xam na aw yiw,ak barabam,dal di koy laabiire jaam yi,tegtal leen ko,yal na ko Yàlla fayal lislaam ak ñoñam. + +Xoolal ku mel ni Sheex Sahdu Abiihi,wàlliyu wu ñépp nangulug wilaayaam,bokk ci néegub teddnga,di ci askanu Yonnant bi(j.y.m),xoolal ku mel nii wax ,bind,wesar,woy.Bokk na ci li nu ko askanale ci lénn ci ay bataaxelam,ginaaw bi mu santee Yàlla ,julli ci Ynnant bi,da ne: ab nuyyoo ngi juge ci man jëm ci Sheex Ahmadu Bamba,yal na Yàlla rëbb ku ko bañ,te rëbb ku ko waral,ma lay ñaan nag nga bañ maa fàtte,te bañ a fàtte xeetu Yonnant bi (j.y.m) . + +Lii nii juge ci sang bu màgg bii,ag laabiire la ñeel xeet wi,di it ag tegtale gu muy tegtale aw yiw, di ko junj,junj gu nooy,te làqu. Mu ne ci ag xasidag ndokkeel,bi Sëñ bi dellusee ci tukk bu nu barkeel ba,ginaaw bi mu defalee Sëñ bi ag seede ci bayit,wu yàgg,muy: + +( jamono giñoon na ne da na fi indi ku mel ni moom,waaye ee jamono,sa ngiñ gi amul de,kon demal kafaara ji ) . + +Mu neeti: + +( tubaab ya’a ko jële woon ca mbellam ya,mu mujj ca géej yooyee di wurusu ngalam ) +(mu feeñe ca xori géejug mbàmbullaan ga,di wurus wow ag leeram akug xuy-xuyam tax na ba bët yi gëlëm) +(mu di weer wu leer,wu fàddu ci sowwu bi,feeñaat ci dib jant cig yékkatiku ak ak tasaaroo ) +(yéemu naa ci wurus wii nu jaarale cig nattu, mu mujj di wurusuw yaaxoot,wu deesul jaayante ab taar ak moom) +( yéemooti naa,na ngeen xam ne buntub tuub ak njéggal de,ubbi nanu ko,ñeel bépp murit,bu sàkku ci moom ag dëkkaale )) +(ag ndokkeel ñeel na diine jii, nga xam ne mujj na di puukarewu ci yaw,ngir mbégte ak ndamu ) . +Esklëy,eskëy,xoolal ma wàlliyu wu tedd wii,ga xam ne làqul lu dul ag dëggu . + +Xoolal ma wàlliyu wii,Sheex Mustahiin Alkumayli,sunu mbokk mi ci Yàlla ak ci Sëñ bi,Alhaaji Muhammad Abdul Laahi doomi Ubaydur Rahmaam,nee na ca téereem ba tudd (( Annafahaat Almiskiyya Fil Xawaarix Almbàkkiya)),: bi tubaab bi tuddoon Kaylaan - yal na nu Yàlla musal ciw ayam - laajee Sheex Siidiya,lan mooy àtteb jiyaar ji jullit ñi di def ci nasaraan yi,ci jamono jii,ndax lu dagan la ,ginaaw nasaraan yi dunu leen def lenn lu ñaaw ci seen diine,ak li ni nu leen di ëpp doole lépp,ak li jullit ñi di néew doole lépp ? +Mu tontoo ko la mu ko tontoo ,mu jébbal tontu bi Sheex Sahdu Abiihi,mu gaaral ko ko,bëgg mu wax ci, mu bind moom Sëñ bi,lu mel ni li Shayxaani (Buxaari ak Muslim) bindoon,jëme woon ko ci wàlliyu yi ak boroom xam-xam yiy jànkoonte ak ñu dul ñoom muy: ki bind araf yii de Yàlla def na ko muy buntub texe ak mbégte ak njèkk . Dara ci loolu jubluwu ko,ndax moom kat féex na ci fitnay àdduna ak allaaxira,atun kasasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,bu feexutoon ci fitnay àdduna ak allaaxira,kon mu indi tontu bu ñatteel,waaye moom mujj na ,bokk ci ñi ñu wax ci ñoom (( bal ahyaaun hinda rabbihim yurzaquun)),muy :ñoom de fa seen boroom ñuy dund lanu,ñu leen di wërsëgal, loolu ki ko wax a ko bind di,Ahmadu mom Muhammad,mom Habiibul Laah,yal na ko Yàlla mu kawe mi musal,te nekkal ko te méngoo ko. +Subhaana rabbika rabbil hizati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina . + +Dégg naa Sheex Mustahiin mu naan: loolu de dëgg la bu dutoon dëgg du ko bind. Dégg naa ci Sheex Bashiiru mom Sëñ bi,mu nettali jële ca Sheex Mustahiin mu ne: man de yéemu naa ci mbirum Sëñ bi,toog nanu ak moom bis ,di mbooloom boroomi xam-xam,yaakaar naa ne Abdul Laahi Ibnu Muxtaar Alhaaji,ca la woon,mu tàmbli di wax ak ñun wax ju yéeme,ju dugg sunu xol yi,ñu bégg tey dëggal te xamunu sax dëgg-dëggi li miy wax,waaye mu jàpp sunu xol yi,nu xame ca ne ca Yàlla la juge. + +Sunu mbokk moomu nu tuddoon nee na ci téerem bi nu tuddoon : +bokk na ci karaamay Sëñ bi,yal na ko Yàlla wattu,dellusi gi mu dellusi bawoo ca dun booba,nga xam ne kenn la fa tubaab yi masul a yobb mu dellusi . Sànni nanu fa nit ñu bari,waaye de kenn a ci dellusiwul,loolu mooy firnde li gën a mag ci ne moom demam gi moo ko tànnoon,dëgg naa ne Sheex Mustahiin mom Talha Alkumaylii,nee na : moom de bu bëggutoon a dem du dem,dunu ko man a génne it dëkkam. +Te kooku doy na ndëërlaay. Sëñ bi bindal na ko ag laabiire gu mu tudde, “Diyaafatul qudoos,wa laa yashummu raaihatahaa dayfu ibliis” muy ci maanaa nganaleg Aji sell ji,ag xetam du xeeñ ganug ibliis. + +Daa na siyaaresi Sëñ bi ,juge fu sori di liiru (dox ci tànkam),daan bañ bu ko Ku tedd ki masaan a jox alal,bu ko masaan a jox sijaada ngir mu ciy jullee,da ko daan jël di ko taf ci dënn bi, te daawul nangu deesi sàggane ko. + +Li Sheex Mustahiin waxoon rekk, la sunu baay Muhammad Alkuntiyyu,mi nu gën a xame ci turu Bu Kunta ca Njaasaan wax, ca wetu Tiwaawon . Kenn ci taalube yi nee na ,booba dafa’a demoon di ko siyaareji,mu laaj ko Sëñ bi,te booba xam na ne mi ngi ci tukki bi,ne ko ana Sëñ bi,mu ne ko moom de tubaab yee ko yobbu,mu ne déet,bul wax loolu,mu ne ko lu may wax kon ? Mu ne ko,moom kay daa dem ligéeyi,fa ligéey ba neexe,murid bi nee booba maa ngi fi ma toog di dégg nit ñuy wax te xamuma dara ci li niy wax,mu ne ma ndax dégg nga làkkuw gaa yooyu ? Ma ne ko déedéet,mu ne ma li ko waral da dul seenuw làkk,ndax Sëñ bi njëkk muy tukki,daa samp ab làkk wërale réew mii,kenn du fi man a am benn taalube,ba kero muy ñëw,man nag samay taalube maa ngi leen jële ci ginaaw làkk bi,samay taalube dunu ñëw li feek ginaaw weer walla ay weer. + +Bokk na ci kilifa yu mag yi seereel Sëñ bi,Sheex Abdalla Attamkali Addaymaani,wax na te dëggal te rafetal: +(dama ne jéngal jëm Daaru Salaam ak Tuubaa,boo ragalee ay mbamb,aki coowi jamono) +( ngir nga ame fa’b xool bu tukkee ci xawsub jamono ji,bob da nga ci ame njéggal ak’ag texe) + +Ñaari bayit yii de maa ngi ko mokkale ci Sëñ bi,ndax bis da ne ma ndax xam nga ñaari bayiti Abdalla yi,ma ne ko déedéet,mu jàng leen ma dal di leen mokkal,xam it li mu doon junj ci dëggal wax ji ci nekk di “xawsub jamonoom”. + +Boroom xam-xam bu màgg bi ,Sheex Abdul Laah Attandaxii Albohbiinii,nee na bi mu siyaaresee Sëñ bi Njaaréem: + +(boo mujjee ñëw wàlliyu yépp, ba noppi kawe leen,na nga xam ni ngën ji mbindéef de,ci xarnu yu mujj yi la ñëw) . + +Sheex Abldullaah mii de mooy ki Sëñ bi ne woon :Abdullaah ag xasida’a ngii,gog ku ko mokkal ,Munkir ak Nakiir du nu ko laaj ci bàmmeelam,Sheex Abdullaah ne laaylaaha illal laah,ana mu ? Mu ne ko mi ngi ak Muhammadul Amiin mii,mu ne giñ naa ne di naa ko mokkalloo samay doom ak samay jigéen,ak samy jaam,yu jigéen ak yu góor,mu nekk di lim rekk ak a dëël,Sëñ bi moom di ree rekk. Xasida gi mooy Jaawartu. + +Sang bii moo ma nettali woon,nettali bu yéeme ba,masumaa dégg lu ni mel,da ne ma sama mbokk man dey daa am bis,may jàng li may faral a jàng bis ci Alxuraan,bi ma ubbee kaamil bi,amul lu dul Yàlla mi man lépp won ma bisub (( alastu birabbikum)) muy ba mu naan (ndax du ma seen boroom?). +Nee na ma jàkkaarloo ak xew-xew ba,gis yonnant yi,yonnant topp yonnant, yu bari yi ak yu néew yi,teg ci ma jàkkarloo’k wàlliyu yi,wàlliyu teg wàlliyu,ak seen mbooloo yu bari yi ak yu néew yi,ba mujj ma gis jenn jëmm,mooy Sheex Ahmadu mii,gox yépp fees dell aki taalubeem,mu génne ci Hadara bi ,sori’s lëf,dal di wëlbatiku ne ana ku may jottalil ab yonnee sama boroom ?,wax ko ñaari yoon ba ñatt,Yàlla tawfeexal ma, dëgëral ma,ma ne ko man,mu gestu ne ma ndax yaw la diw ? Ma ne ko waawaaw,mu ne boo ko defee de ,ba nu dem àdduna di naa la defal,di naa la defal..,mu ne ma neel sama boroom,mu dolli ma,ndax sama ñi ma topp de danoo bari te bëggaluma leen lu dul lu leen di bégloo,ak wax yu mel nii,ma dugg,ci biir,wax li nu ma waxloo woon,ma gis nu koy jox , ba ma dégg ko mu naan doy na,dal di dem. + +Eskëy,moom de ci jëlewaayi (masdar) Sheex Sahdu Abiihi la bokkoon. Xibaar boobu nettaliwu ma ko kenn,lu dul ginaaw bi mu faatoo,ci ndigalm,sheex bii nag sama xarit la woon,te nekkon bu Sëñ bi,mas na maa yonni ca Sëñ ba di ko ñaan doomam,mu ne nee ko sàkkuwu ma ko lu dul ngir xér ci am lu ma jaxase ak moom ci fii ak ëlëg . Sëñ bi ne ni mu ko waxe la de,ñoom de bi ma nekkee seen réew sàkku woon nanu ma’a jox seen doom,waaye ma ne leen wuuteg aada yi moo nanguwul loolu rekk . Maandu na te dëggal. + +Bokk na ci ñu mag ñi ko seereel,Alhaaji Ibraahiima Albaxdaadii,moom de ci kiimaani araab yi la woon,mi ngi juge woom Baxdaad,ku meloon ni moom ci xam-xam moom jafe woon na,Sëñ bi moom ci jëmmi boppam nettali na ma ne gis na Alhaaji Ibraahiima mii,booba gone la woon,muy tukki di ànd ak waajuram wu góor,ak Xaali Majaxate Kala,ñuy ànd ak Latjoor,bis nee na gis na ko mu toog ak ñaari sëriñ yooyu ci lalub sëriñ Buubakar FALL,yéeme lool ci barig nettaliy xam-xam yi mu leen doon defal,ci noonu Xaali manutoon a ñàkk a bind nettali yi,mu yonnee nu woolu ma,ngir ma bind xam-xam bu bari bii,mu diy woy,ngir mu bañ a sànku,ma dikk,muy wax may bind,muy lu bari ciy woy. Ma dégg ci sama waajur mu naan masumaa gis ku man a mokkale ni naar bii,ku dul Alhaaji Omar Fuutiyu,moom de jamono ju nekk mi ngi naan:Buxaari nee na,Muslim nee na. + +Nee nanu bis laaj nanu ko turu buur bii,mu ne Latjoor,buur bi bég lool ci waxam jooju,bi loolu jàllee ba teg lu tollook ñaar fukki at,walla lu jege,ginaaw bi Sëñ bi jugee ci tukkib géej gi,la ñëw ci moom jébbalu,fàttali ko la xewoon bu njëkk,mu yéemu lu bari,nettali nanu ne bokk na ci li tax mu jébbalu,daa am bis mu ànd ak Sëñ bi cib tukki,ñu yendu ci ron genn garab,dëgg naa ci Sëñ bi,mu ne Alhaaji moomu booba mi ngi tux,mu génne gënn gi,am lu mu sotti ci loxoom,daa di ne ma loo wax ci lii ? Ma ne ko defal te bul laaj,mu ne ma ,duma man a ñàkk a laaj,ndax wuute gi da cee bari,ñii di ko daganal,ñee di ko araamal,ma ne ko ,bu dee noonu la deme de kon lu lënt la ci yaw,mu ne waa-waaw,ma ne ko xanaa gisoo Axdariyu,mu ne ma ahakay,gis naa ko,ma ne ko moom de nee na ca njëlbéen ga,daganul ci mukàllaf mu def dara te xamul la cay àtteb Yàlla,kon doo ko bàyyi,ba xam li ci Yàlla wax?. + +Sama wax ji wedamloo ko,àgg ak moom fu sori,mu sëgg ab diir,siggi,ne ma seereel ne bàyyi naa ko ngir Yàlla,dal di jug ca saasa,suul gënn gi,ak li ci nekkoon,ca bis ba mbaa ginaaw bi la jaayante ak Sëñ bi,jébbalu ci moom . + +Bi ñénn ci mag ñi yëgee ne jébbalu na,ñu tàmbli di ko yedd naan ko yaw ak sa màgg gi ak sa xam-xam bu bari bi,lu tax ngay jébbalu ci ku ñuul kii? Mu ne ko man dey Baxdaad laa juge, ni nga ko xame,yitewoowuma lu dul ku ma jox sama loxo,bari na wàlliyu mbaa boroom xam-xam bu ma romb,te xetug li may wër xeeñewuma lu dul ci moom,looloo waral ma aju ci moom, jaayante ak moom,ci noonu ñu dëggal wax ji,dogal ko ngànt. + +Bi mu delloo ci Ku tedd ki,nettali ko li nu ko doon wax,Sëñ bi bindal ko lii: +Wasslaamu halaykum wa rahmatul laahi,wa barakaatuhuu, +ma lay xamal ni ca sama xasida ga tudd ((masaalikul jinaan,fii xidmatil mutahhiril janaani)) di ci maanaa,soobuwaayi àjjana yi,ci ligéeyal kiy laabal xol yi,bayit yii a nga ca: + +(( Képp ku ma jorte lu dul kuy ligéeyal Ku nu tànn ki,man de dama koy ligéeyal ca la mu tànn)) +((dama koy ligéeyal ba kero may dugg àjjana,kërug sax ga,ak mébat ak xéewal )) +((képp ku yaakaar ne man na koo bégale ni,ni ko sama ligéey biy bégale )) +((na xam ne réer ak réeral wor na ko,te ci moom la ma lu dagan di dikkale juge fa boroom ba)) +((taggoon naa ko bu njëkk ca Libarwali,ag tagg gu wàlliyu yépp a ci lòtt )) +((taggoon naa ko ca Maayomba,tagg wu far samay ayib te dindi samay bàkkar)) +((taggoon naa ko fa niti Kalwaa,tagg wu ma fegali noon ak musiba)) . + +Nee naa ci ligéey bi ma koy defal (j.y.m): + +((ñeel na ko tukkee fi man,ab ligéey bu taqoo’k rawdatoom ba (bàmmeel),ba yawmal xiyaam te màgg)) +((sëtam ba Jiilaanii gëram na ma,yal na ko Yàlla mi ma kaweel gërëm)) +((sëtam ba Abool Hasan gërëm na ma,yal na gërëm luy saxalub taar nekk ci moom)) +((Attiijaanii gërëm na ma,yal na gërëmul kiy alag ibliis nekk ci moom)) +((ñeenti Xalifa yi gërëm nanu ma,làq naa gërëmul ñu ñu jegeel ñi)) +((ku ma gërëmul de,Yàlla Mu tedd ,mi moom gërëm na ma,ngërëm lu dul dog )) +((yal na Yàlla fay Mustafaa ngën ji pay,ni mu nangoo te amal ab dëël )) +((jullig ki nga xam ne teraangaam day daje ak man,yal na nekk ci ki nga xam ne mooy ki dëxëñ )). +Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal + +mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina . + +Li nag booy xool ag junj la ci ne ñi ko ci doon yedd de,xamunu dëgg-dëggi mbiram,kon lu tax waxunu lu mel ne li ki leen xamul waxoon ? : +((yaw ki nga xam ne dëgg-dëggi am mbiram xamuma ko ,aka neexoon ma xam luy dëgg-dëggi mbiram)) . + +Bokk na ci li nu soloo ci seere yi ko mag ñi seereel,mooy ne Sheex Muhammad mom Abiibur Rahmaan,Attanaduxii,da daan def fu nu tudde Sëñ bi ci wetam mu yëggal boppam,ne cëy cam soosu,moom dey fu ma ko nemmikoo rekk,fekk ko ci sama kanam,lu tolloo’k aw xur,walla ñaar. + +Sama mbokk Muhammadu Abdur Rahmaan,Ibnus Saalik Baaba mom Halawi,wax na ma ne xalifab Sheex Ahmadu Bun Buddin,ak doomam ju màgg ja,Muhammad Amiin,nee nanu ko Sëñ bi de wilaayaam gi, indi na ci ay firnde, aki lay yu leer, ñépp gis ko, kenn ku am aw yiw dey du sikk ci wilaayaam gi. + +Bokk na ci seere yi,li ma Muhammad mom Ahmad, mom Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci taalubeem yi,ci turu Muhammad Tuubaa,ngir barig lu mu fa daa nekk ak Sëñ bi,li mu ma nettali woon,muy moom de bis seeti na ay nijaayam,ni nu ko baaxoowoon a defe,mu dem ca ku yéeme,ku bëgg ka Yonnant bi ak jëwrinam,di Muhammad FAAl,doomi Muhammad mom Ahmad mom Haaqil,mu yobbante ko ab nuyyoo akub siyaare ca Sëñ ba,sàkku woon it ci moom mu jox ko barkeelub mbubum njiitlaay,mu mu daa sol, ngir mu barkeeloo ko,nee na ma jotal ko Sëñ bi mu bég ci,jox ma njiitlaay lu ndaw,lu mu daa jiitloo,maanaam turki,mu ne ma gaawal jox ko ko,ma indil ko ko,mu bég ci lool,di ko foon ak a teg ci bopp bi,ag bët yi,nit ñi dégg ko,mujj ku ñëw rekk,ñaan ko,ma barkeelu ci,ba mu mujj sànku,mu sàkkuwaat ci man ma demalaat ko,ne ko nit ñi de sànk nanu sama barkeelu ba,na ma sarax beneen,ma dikk ci Sëñ bi,leerale ko ko noonu,mu bég,jox ma beneen,ma indil ko ko,mu sànt Yàlla bu baax,tagg Sëñ bi lu bari,man itam mu sat ma,ne ma boo jébbaluwutoon ci Sëñ bi de, di naa wax ci yaw kon loo xam ne !,waaye jébbalu gi tax na ma fiire la . + +Bokk na ci seere yi nu tuxale ci doomi mbokkam ma,Ahmadu Yoora Muhammad : lenn ci ay àndandoom danu koo yeddoon ci néew gi mu néew lu muy siyaare Sëñ bi,mu ne leen wallaahi,bëggumaa deem di ko siyaareji te yor ci sama xol,lu toll ne fepp suuf ci bëgg àdduna,kon fii ma toog laa koy siyaaree ,eskay.Ana ku gën tedd Muhammad,moom daal doy na sëkk seere . + +Néeg bii ki ci gënoon a taqoo ak Sëñ bi,gënoon cee rafet lu mu wax,mooy Ahmadu mom Abdallaah,ki bokk ak ñoom ñaar nday ak baay,moom dey moo’k Sëñ bi danoo meloon ne benn bakkan,seere naa bis Sëñ bi di jànglu lenn ci ay xasidaam,ñu jàng aw bayit mooy: ((taqdiimu Ahmadabni Habdil laahi, yahrifuhuu xayru xabiyyin laahi)),muy ci maanaa jiitalug Ahmadu mom Abdul Laahi,ku dul ab dof,buy fo xam nga ko,bi nu tuddee Ahmadubnu Habdil laahi rekk, xelam dem ci,Ahmad moomee,mu ne nanu ko ko wool,bi mu ñëwee,mu nettali ko ne tudd gi nu ko tudd,ci biir njàng mee tax xelam dem ci moom mu woolu ko, moom itam mu bég ci,sant ci. +Ahmadu mii nag mi ngi faatoo Ndakaaru,bàmmeelam a nga fa,siyaare naa ko . + +Bokk na ci seere yi ,li ma Abal mom Baay Addaymaanii,nettali,mu ne moom de sax na jamono ju yàgg ci,sàkku ci sunu boroom mu won ko,maqaamam Sëñ bi,mu ëppal bis ci sàkku gi,ñu ne :yeen de du ngeen xam ci Sëñ bi,lu dul bu ubee ba toog ngir daje ak nit ñi,ngeen ne kii de mooy Sëñ bi,mbaa mu ubbi mihraab bi,taxaw,ngeen ne Sëñ bi de jiite nanu,lu dul loolu ciy mbiram de,fàddu na leen. + +Ma ne wax jii de niroo na ak waxi Uwaysul Xaranii,sangub way topp yi,ji mu waxoon lenn xalifa yi, ne ko: yeen gisu leen ci Yonnant bi (j.y.m) lu dul keram !,nu ne ko Ibnu Quhaafa sax gisu ko,mu ne leen déedéet . Habal mii nettali na ma karaama,gu bàyyikoo ci goroom,baayu soxnaam,mu ne moom de daa am bis mu nekk cib xaymaam,moo’k doomam,mu koy bësal boppam,ndax daa jékki-jékki woon rekk buur ,buur gu metti,te gaaw (buur = jékki-jékki rekk jug),bi mu ko defee,dal di génn xayma bi,door tànk bi cig weñ,ba nu dégg ni ci tànk bi dale,te foofa génn weñ nekku fa,ci noonu tànk bi damm,mu rot ,xëm,bi mu ximmee,ñu laaj ko,lu mu doon,mu ne daa gis aw wàlliyu wu ñuul,di Muhammad mom Mahluum,ñu jénge ko ay weñ,mu bëggoon koo xettali,door tànk bi ci weñ gi,ngir damm jéng bi,far tànk bi damm,werul ci damm-damm boobu,ba kero mu faatu,yal na ko Yàlla gërëm te nangul ko jëfam,bi mu daataa faatu,bégaloon na doomi Daymaan yi,ci ag ubbiku gu yaatu ci alal,bu wàlliyu woowu dellusee,mu nekkoon ni mu ko waxe woon. + +Bi Sëñ bi dellusee,mu jël leen,bindkati xam-xam yi,ak alxuraan yi,seeni waxambaane ak mag ñi ba ci jigéen ña ak gone ya,di leen sotti ci alal lees manut a misaal, ña ca rafetle ak ña ñaawle,loolu di jàppndal akug tàggatal gu tukke ca Yàlla, ñeel leen,te di ndimbal ak sarax bu nu def ci sekkare,di ag ligéeyal lislaam it,ak Yonnant bi (j.y.m) ci xeetam wi . +Ni nu binde woon la ñeneen it binde woon,ci naar yeek ñu ñuul ñi,waaye ci ñoom la gënoon a siwe,gën cee feeñe. + +Bokk na ci ñu màgg ñu barkeel, ñi seereel Sëñ bi,Haamidun mom Muhammad mom Muhanda Baaba,ak doomi baay tëxam yi,Baaba ak Ahmad, ñaari doomi Mahmuud ak Haamid yi, ñoom ñépp , ñu ñu jagleel lanu woon ci moom,boroomi wax yu rafet it lanu woon ci moom . + +Yàlla dogal, bi Sëñ bi nekkee Cëyéen yonni woon na ma Dagana,ba ma fa àggee,Ustaas Haamid dégg ma, booba da fa’a ganesi woon Alhaaji Bekaay SEKK,yàggul dara mu seetsi ma,bég ci dikk gi ma fa dikk,yendook man ca sama kër waajur,di ma laaj ci mbiri Sëñ bi,aki xibaaram ,yi ci di yu nu man a tas,ak yi ci di yu ñu bari mant a xam,bu ko defee muy ree rekk,bég lool ci Sëñ bi , aki mbiram, ci noonu ma won ko teereb Sëñ bi tudd “Masaalikul Jinaan”,mu sëgg ci,siggiwul ngir dara,ba kerook ngoon di jot,mu ne ma Sëñ bi de ñëw gi mu ñëw ci jamono jii nu nekk de,firndéel na yiwam wu bari wi . + +Lii nag ag mosle rekk la ,waaye waxi ak seerey sangi naar yi,fii taxu koo jug, fi ko tax a jug kay mooy sunu téere bi tudd,(alminahul miskiya,fil xawaarixil mbàkkiya). + +Da nanu ci dolli li nu man ci tudd murid yi ci ñoom,bu soobee Yàlla. Bokk na ci kilifa yi ko seereel,sunu sëriñ tey sëriñub jullit ñi ci Senegaal,soppeb Sëñ bi,tey mbokkam,ci jegeñaaleg diine ak askan,ak réew,Alhaaji,Maalik SI, yal na ko Yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom Aamiin,dégg naa ko,ku dul man it dégg ko,ba xaw naa doon lu ñépp xam,mu ne: amul kénn ci nun ku dul koo xam ne,daa def lu ñaaw,ba noppi,tuub ko,te jubal,bàyyi ag dëng,ku dul Sheex Ahmadu Bamba,moom de daa judd,rekk di def lu baax ak a rafetal . Maanaam loolu mooy ñun ñi ñiy tudd ñépp de,amu ci kenn ku gisul ci boppam ab rëcc-rëcc,walla ay rëcc-rëcc,bu ko defee mu tuub ko te jubal,ginaawug dëng,ndare moom,moom dey ,am mbiram cig ndawam akug magam ñoo yam rekk,lépp ag tegu ci yoon la.Moom de wallaahi dëggal na,te laabiire. + +Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci turu,Muhammad Tuubaa,xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def,daa romboon Tiwaawon,siyaare Alhaaji Maalik SI,bi mu xamee ne ca Sëñ ba la jëm,mu ne ko man de da ma laa bëgg a yobbante ay baat ca moom,boo àggee na nga ma ko nuyyul,te fàttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndakaaru,ci benn néeg ñun ñaar rekk,kenn ñatteelunu ku dul Yàlla,bu ko fàttalikoo ba xam ne maa la yonni ,nga ne ko,man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom,maa nga ca kollare ga ma defoon ak moom.Muhammad nee na man de wallaahi,xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. Bi ma àgsee ba fàttali Sëñ bi guddi gi,ba mu fàttaliku ko,ma wax ko li mu ma wax,mu bég ci,dëggal ma te dëggal ko,tagg ko bu baax,tàmbli di coppati sama nopp bi,ak sama bakan bi,boole ca di ree rekk,ngir bég . + +Bokk na ci mag ñi ko seereel ba tay Xaali Majaxate Kala,xaritu Sëñ bi,tey mbokkam ci diine ak askan,ak réew,xaritu waajuri Sëñ bi la woon,da daan def ,bi Sëñ biy jàng,saa su ko masaa na romb rekk,sànni ko aw bayit walla ab jumla,ngir nattu ci ab tolluwaayam ci nahwu,muy (xam-xamu tegi wax ci yoon) walla bayaan:(xam-xamu rafeti wax) ngir ñawal am xelam, leeg-leeg,mu génneel ko ci ab yàq,leeg-leeg,déedéet,ba mujj Sëñ bi far ko raw,bi Sëñ bi màggee ba weesu fi mu tolloon,mu mujj naan ko,yaw de doom nga woon,waaye leegi baay nga, donga nga woon it,leegi sëriñ nga,muy lu mu dëggal te fas ko ci biir ag kaf,akug woyofal . + +bokk na ci li nu koy askaneel,aw bayit wu yéeme,yaakaar naa ne tàmblig ag xaasida la : +(tukkee na ci man jëm ci Ahmadu Bamba,mi bàyyi nit ñi,ngir Yàlla ,mujj far di sangub nit ñi ) . + +Bokk na ci li nu askanale sang bu màgg bi,Sheex Muhammadu Alfuutiyu,baayi Zannuuni,ak mbokkam ma Ibnul Harab,mi bokkoon ci jëlewaayi Sheex Sëhdu Abiihi,bayit wii,moom tàmblig xasida la gu mu defal Sëñ bi : +(mi ngi jëm ci kok Yàlla da koo defal ag tàllal (ay xéewal) akug wéttal,àtteloo ko ci àddunay jinne yi ak nit ñi) . + +Moom xasida gi,gu yéeme la,téewlootuma ko fii mu nekk, wax na ci, ci wenn bayit wu muy waxante ak Sëñ bi,naan ko: + +( sotti leen ci seeni miskiin,desiitu kaas bi) . + +Sëñ bi daan def,saa su gisee Zannuuni,defaral ko ab kaas ne ko, càkkutéefug sa baay la woon, Zannuuni mii,mi ngi bokkoon ci woykat yu mag yi,yu rafetooni woy yi,def na ab diiwaan ci tag Yonnant bi (j.y.m), def beneen ci tagg sëriñ si,rawati na Sëñ bi,mooy ki ci wax lii: + +( yaw xarit bi,ndaw sa bunt bii,bari lu ko siyaaresi,ci buur ak jaraaf,ak jinne ak malaaka) . + +Loolu di tàmblig xasida gu rafet, te yéeme,moo’k baayam ci jëlewaayi Sheex Sahdu Abiihi lanu,yal na leen Yàlla gërëm,mi ngi faatoo Cees,nu denc ko ci almeeri Sheex Ahmad Baru, siyaare naa ko, alhamdu lillaah. + +Bokk na ci kilifa yi seereel Sang bi,sëñ bu màg bi,di Sëriñ Tayba, Muhammad Ndumbe Maar SILLA. Sëñ bi nee na ma sëñ boobu de,fu mu ma masaa na gis rekk sànni na ma bayit wii,di ci seere ci sama mbir,mi ngii: +(bariwaa na baay bu yéege ci doomam,ay tundi teddnga,ni Hadnaan kawee ci Yonnant bi) . + +Mu bëgg a wax foofu ne,cam sii de ab taar la,tey ag mat ñeel cosaanam. + +Bokk na ci kilifa yi seere,sang bu màgg ba Alhaaji Abdulaay SIISE,mom Saalum,nekkoon na di ku rafeti wax,ak pas-pas ci Sëñ bi,am na bis aw nit di wax cib jataayam ba tudd Sëñ bi,ak jële gi mu jële wirdam wi ci Yonnant bi (j.y.m), am ci ñi teewoon ,ku ci waxe ni kuy weddi,Alaaji gëdd ko,ne ko looy wax nii ?,xanaa Sheex Ahmad Tiijaan waxul ne lenn ci ay wirdam Yonnant bi moo ko ko jox (j.y.m) ? mu ne ko ahakay, mu ne ko moom de,nekkutoon lu dul boroom xam-xam,bu jëfe xam-xamam,bu ragal Yàlla,te doon jëfe sunna, rafet gi nu rafet njot ci moom moo waral nu dëggal ko,kii nag di Sheex bamba,xanaa melul ni moom rekk,di boroom xam-xam buy jëfe xam-xamam,ragal Yàlla tey ku sunnawu,ndax kon du nu ko dëggal,ngir rafet njort gi nu dëggale woon kee ?,waa ja wedam, amul lu mu tontu . +Hasbunaal laahu wa nihmal wakiil,nihmal mawlaa,wa nihman nasiiru. + +Ag cant ñeel na Yàlla lii doy na ci li sama xel man a joxe,li am nag mooy,bu ma joyaloon samab gog,féexal xel mi ci mu dikke li mu wattu,ak li ma wattoo ci samag maas,ci lu wér ak lu wéradi,kon de ma indi fi gën jaa yéemey yu yéemu yi,waaye kon loolu am raddu rekk lay doon, ñax gu nekk a ciy nekk, ag jub ak ag jubadi,dëgg ak safaan,looloo tax ma tànn indi fi li ma man,teb yool nekk ci,ndax kat déet ab yool,ci lug jub nekkul,bu nu doon tollale li ma indi,ci li ma indiwul,da nga naan benn la ci junni,li ma xam it bu nu ko doon tollale ak li ma xamul,da nga naan as kook la ci géej . + +Yàlla mu kawe mi,laay ñaan mu baril sama lu néew,te wisaare ko,te nangu ko,te dimble ma, moom kat mooy aji tedd jiy aji gën, kiy boroom ngënéel lu mag li. + +Tàmbli nanu ko te mu mat,cig barkeel,yal na Yàlla nangu,te dimbalee,te yekkati,te wisaare,Aamiin. +Yaw buur bi, jéggal ma, ak sama ñaari way jur,te nga yërëm leen ni nu ma yarewoon may ndaw . + +Dundug Seex Ahmadu Bamba +Suuf si (junj: ), mooy ñetteelu àdduna bi gën a jege jant bi, moom nag man nan koo woowee "Suuf si" walla "Àdduna bi", walla "Àddunaay Suuf" walla "Àdduna ju Baxa". + +Suuf si nag bari na ay mindeef yu fi dëkk, nit ci la bokk, ci li nu xam fii rekk la ag dund am. cig xayma, boroom-xam-xam yi nee nañ, Àddunaay Suuf, mi ngi sosu am na 4,57 miliyaari at, te ag dund mi ngi juddu ci kawam ci diirub benn miliyaar ciy at. Moom nag jawwam soppikuna ci anam bu waral wërlaayam doon guy dundeef man a juddoo. + +Kaw Suuf gu biti gi nag dafa séddatleku ci ay doj yu dëgër yu bari, di yëngu ci lu bari ci kawam ba leegi mat na miliyoŋi at. Daanaka 70% ci kaw Suuf si ay mbàmbulaani ndoxu xorom a ko muur, li ci des di ay gox aki dun. Ndox mu yollaakon mi ñu jàppee ne mooy yor dund, ci ni ñu ko xamee, Suuf si rekk mooy àdduna bi ñu gisagum bu ko am ci kawam. Ci biir Suuf si nag la fa na ne mooy: magma bi, ab saalub biti bu yollaakon biy jur toolu bijjaakon bi, ak saalub biir bi nga xam ne weñ la. + +Suuf si day am ay digaale ag yeneen mbir yi ne ci kaw jawwu ji. + +Diir bi Suuf si di def ngi man a def ab wër bu daj ci jant mooy 365,26 bés (bés di 24 waxtu) + +Taariixam +Boroom-xam-xam yi àgg nañ ci man a xam yenn xibaar yi ci dembi Suuf si. Suuf si ak yeneen àddunaay nosteg jant bi ñoo ngi juddu am na booba ak léegi 4,57 miliyaar ciy at, doore ciw niirub jant(nébuleuse solaire), di ab donjub pënd ak gil(gaz) gu bàyyeekoo ci juddug jant bi. Ci ndoorteel gi muy ruy, wàllu Suuf si féete woon biti tambalee sedd, dem ba doon ab donj bu dëgër bi ndox tambalee dajaloo ci jawwam. Yàggul dara weer wi dal di ciy tegu, boroom-xam-xam yi, ci lu wóor jàpp nañ ne mi ngi juddoo cib mbëkkante ci diggante Suuf si ak benn mbir bu réyaam matoon 10% gu Suuf si. Benn xaaj bi des ci Suuf si(yokk réyaayam), beneen bi nekk weer wi, dend ak moom. + + +Saytubiddiw +Niiruw jant cig njort, mooy niiruw gil wi nga xam ne ca la sunu nosteeg jant juddoo. + +Bii xalaat-jiital(hipothèse) kii di Emmanuel Kant mooy ki ko njëkk a biral ci atum 1755, jàppoon na ne niir wi day wëndeelu ndank-ndank ci boppam, di gën di danku ak di tàcc ci sababu bijj (gravité) gi, dem ba nekk ay biddiw walla ay àdduna. Pierre-Simon Laplace it ci atum 1796 biraloon na gisiin wu ni mel. + +saytubiddiw +Nosteg jant bi, ci xam-xamu saytubiddiw, mooy nosteg sunuy jawwu, li ko toggale di ab biddiw, jant bi ak mboolel yëfi asamaan yuy warangiku ci li ko wër ; juróom-ñatti jawwu yees firndeel ak seen 175 weer yu nu xam, juróomu jawwuy dàtt yi, ak miliyaari yaram yu ndaw yi (bokk ci yooyu jawwu yu ndaw yi ak pëndi diggante jawwu yi). Nosteg jant bi mingi bokk ci galaksi bi tudd Yoon wu Meewe + +Jawwu yi nekk ci nosteg jant bi ñooy: Merkuur, Weenus, Suuf, Maas, Seres, Yupiter, Saturn, Uraanus, Neptuun, Eris, Pluton, Haomea, Makemake, Goŋgoŋ, Koawar ak Órkus. + +Saytubiddiw +Jant (junj: ) bi mooy biddiwu sunu nosteeg jant. Ci li ko wër la Suuf si di warangiku, am na yeneen juroom-ñaari àdduna, ak kuusi àdduna aki xeer yu réy. Kàttanu ceeñeer gi jant biy àggal ci Suuf si moo tax dund man faa am; kàttan googu day nu man a am ndox ci nekkinu yullaakon, tax it gañcax gi man a jot ci naaj wi mu soxla ngir seenug dund + +Saytubiddiw +Angolaa mi ngi nekk ci diggante 4°22′ ak 18°03′ ci tus-wu-gaar wu bëj-saalum ak 11°41′ ak 24°05′ ci tus-wu-taxaw wu bëj-gànnaar. Am na ci tefe, réye soo ci boolee Kabinda. + +Mi ngi fegoo ak Kongóo-Brasaawiil ci bëj-gànnaar, ak Kongóo-Kinshasa ci bëj-gànnaar-penku, ak Saambi ci bëj-saalum-penku, ak Namibi ci bëj-saalum, ak Mbàmbulaanug Atlas ci sowwu. Pegg gi mat na + +Angolaa +Angolaa +mooy balluwaay bi yoon yi di génne moom yoonal nag doole la joj péncum ndawi réew mee koy ame mooy barab biy yoonal génne jox àtte gi maanaam letaa (nguur gi) ngir mu tënku ci. Mbooleem yoon yi (les lois) ndawi réew yee koy kàddu maanaam “woote” ngir mu dem ca dooley wéyal ja àtte gi ame ngir mu doxal ko + +Yoon +wéyal mooy ponk bi xaw a ëpp solo ci ñatti ponk yooyu, ndax moom njiitul réew mee koy ame, walla jëwrin ju njëkk ji bu dee nosteg péncu réew (regime parlamentaire), mooy doxal réew mi di tënku ci yoon yi bàyyikoo ci dooley yoonal ji, bu ko defee yoon di ko fuglu (controler). + +Yoon +Ab dalub web, dinañu wax itam dalub internet, da di am mbooloom ay xëti web yu ñu lëkkale ci seen biir duggal leen ci buum gi, jox ko am màkkaanum web ngir ñu man caa àgg. ci 2006 web bi romboon na 1oo ooo ooo ciy dali web. + +Ag sosam +Dalub web bu ne am na boroom, man naa doon ag lonkoo (këru-liggéeyukaay), walla ag mbootaay, walla kenn nit, añs. Boroom mooy tànn màkkanum web mi ñu man jaare ngir àgg ca dal ba. + +Tëddinu xët yi +Ab dalub web am mbooloom ay xët la, yu ñépp man a saytu di ko jaare ciy lëkkalekaay yu ne ci biir dal bi. Màkkaanum web, mu ab dal, naka-jekk, day nekk ab URL (ab joxoñukaay ci wolof) bu ab xëtu web, mooy nekk xët wi ñuy njëkk a nemmeeku: di ko wax xët wu njëkk wu dal bi (misaalu makkaanum dal man naa ne www.anafa.alfanet.org). Màkkaanum dal dinañu ko wax itam turu barab, maanaam turu barab bi ngay jaare ngir yegg ca dal ba. Kon ñoom ñaar ñépp a bokk tekki: ñoo lay jox turu dal bi, ba nga man koo ubbi. + +Saytu gu nekk gu dal bi lees di wax ag nemmeeku (nemmeeku ab dal), lëkkalekaay yi ne ci diggante Xët yi ñooy tax ñu man a saytu xëti dal bépp te doo ko génn. Jàpp tamit ne ag nemmeekug dal man naa dooree ci xët wu mu manti doon ci dal bi, rawati na, su fekkee ne ab seetukaay moo lo jox URL bi. Jàpp tamit ne xët wu njëkk wi ak yeneen xët yépp a yem, da di ni rekk kay dañu koo jiital ngir mu doon Xët wi ngay duggusee ci dal bi. + +Limu dali web yi +Limu dal yi cig yokk la dëkk lu jamono ji di dem: + +Yenn ciy dal + Dalu World Wide Web Consortium + Buntu AJD/PASTEEF + Daara ju Al-khalil + Banku Àdduna bi: ab jukki ci Wolof + Këyitu IPM + Sene Construction + Development Gateway Senegal + UNESCO - Sartu aq ak yeleefi doomu aadama + Sémbum ALMA + +Xool it + Nosukaay + Xam-xamu nosukaay + +Xam-xamu nosukaay +Xam-xamu diine yi manuta ñàkk +Ay jumtukaay ngir jàng làkku arab +Xasaayit laata 1324 +Xasaayit ganaaw 1324 +Njangum xasaayit +Xasida yi sërignbi bind laata 1324H +Xasida yi sërignbi bind ganaaw 1324H +Njangum xasida +Almazán ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Ispaañ. + +Mi ngi yaatoo 166,53 km², ci 2006 amoon na 5.727 way dëkk. + +Ispaañ +Xëtu web wenn la ci Xëti World Wide Web bi, doon lu ñu sakk ngir ay nemmeekukat man kaa yër ci ndimbalu ab joowukaay. Aw xëtu web day am ab màkkaanu web bu muy àndal ngir ñu man kaa ubbi ci joowukaay bi. Ci jëmmam dëgg, Xëtu web, day nekk ab mbooloom ay mbind, ay nataal aki riir, ci gattal lépp lu gisu walla déggu. + +Saytuwiin +Fànn yi ñu man a saytoo aw xëtu web bari nañu: man ngaa bind ci banqaasu màkkaan yu joowukaay bi màkkaanu webam, walla nga topp ab lëkkalekaay bu nekkoon ci weneen xët. Li ëpp ci joowukaay yi ñu gën a jëfandikoo dees la koy won cib wonekaayub nosukaay jaare ko cib palanteer bu mu lay tijjil, tax it manees koo móol. Làkkiin wu HTML mooy cëslaay gi ñu sukkandiku ngir sos xëti web yi, ba tax saytu gi man a am ak jumtukaay yu wuute: dayob wonekaay bu ne, móolukaay yi, añs. + +Cëslaayi xereñ +Cig xereñ, aw xëtu web dafa cëruwoo ne-ne yu wuute yi ne ci World Wide Web bi. Ci lu daj ne-ne bi ci njëkk ab jukki bu ñu bind ci làkkiinu xibaarfeppal gu HTML. Làkkiin wii di HTML day tax ñu man a sos ay xëti web, jox leen ay màkkaani web, tax itam nu man a melowal xët wi, tëral ni ci ne-ne yi taxawee. + +Xam-xamu nosukaay +Breinigerberg ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Almaañ. +Mi ngi yaatoo 4 km², ci 2005 amoon na 971 way dëkk. + + Breinigerberg {de} + Breinig + Breinigerberg {de} + +Almaañ +Internet (di jàng in-ter-net, jóge ci baatu latin bii di inter=diggante ak bu wu-angalteer bii di net=lënd) moom lañu jàppe niki lënd gi gën a rëy ci àdduna bi, te boole ay junni-junniy nosukaay lëkkale leen ci seen biir. + +Mi ngi judd ci ati juroom-benn fukku yi niki ab sémb bu kuréel gi yor kaaraange ca Diiwaan yu Bennoo yi ngir sos ag lonkoo ci seen diggante, ci njeextal xare bu sedd bi lañu ci yaatal ñeneen ñu dul yëngu ci kaaraange rekk, lëkkale daara yu kawe yi gën a mag, ci lu njëkk, ba yàgg mu àgg ci yenn liggéeyuwaay yi, ci noonu lu muy gën di dem di gën a yaa ba àgg tay ci sunu kër yi. + +Aw ràbbiinam +Internet man nanu koo jàppee niki ag lonkoo gu xellu te fasu teg ci, cëslaayu ci fànni jumtukaay ak xeeti lonkante gu ne, lëkkale leen ci seen biir. + +Jumtukaay yiy lonku ci internet lees di wax host(di tekki gan ci wolof) walla end system (nosteg njeexte ci wolof), mbir miy jokkale host yi la ñuy wax lëkkalekaay. + +Mbaalu mbaal yi + +Naka-jekk Internet «mbaalu mbaal yi» lañu koy dakkantale. Naka-noonu ay lonkoo yu bare lonkante doon ko: lonkoo yu kenn, yu mbooloo, yu ay këri-koom, yu ay daara yu kawe... Ag juddoom ak ag màggam gu gaaw, bokk na ci li ko waral, mooy bennal gi am ci xeetu jokkoo ci diggante lonkoo yi, waral weccontey xibaar man a am ci diggante ay jëfandikukat yu soriyante(yu mel ne nguur-ak-nguur, daara-ak-daara, këru-koom-ak-këru-koom, ak ñoom seen, te jumtukaay yi muy jëfandikoo amuñu ci benn njeexit. + +xool it + + Xaralay xibaar ak jokkoo + Xam-xamu nosukaay + Nosukaay + Dalub web + Xëtu web + +Lëkkalekaay yu biti + (en) tekki gu Internet + (en) National Coordination Office for Information Technology Research and Development + +Xam-xamu nosukaay +Lëkkalekaay yi ñooy tax ñu man a jòge ci aw xët dem ci weneen wu mu lëkkalool. + +Gongikuwaay ak àgguwaay +Ab lëkkalekaay day am gongikuwaay (maanaam fa muy jóge) ak ab àgguwaay (maanaam fa mu war a àgg, jëm fa). Soo doxalee xeetu(element) lëkkalekaay bi, ca saa sa, da ngay man a jàll ca àgguwaay ba. + +Gongikuwaayub lëkkalekaay day doon naka-jekk aw xeet(ab baat, walla nataal,...) bu ab jukki. Àgguwaay bi man naa doon aw xeetu benn jukki bi, loolu la ñuy wax lëkkalekaay bu biir. Àgguwaay bi man naa doon itam beneen jukki, bu dul bi mu nekk. + +Jaar-jaar +Lëkkalekaay yi ñi ngi sosu ci ati juroom-benn fukk yi, waaye seenug tas mi ngi ànd ak màggug internet, di fu Lëkkalekaay yi di boole, niki ag lënd, ay junny junni dal ci Lëkkale(resaux) gi. Su dul woon Lëkkalekaay yi, xereñu Internet di na wàññiku bu baax, jafeel ag jëfandikoom. + +Ak jëm-kanam gu réy gu Internet, lëkkalekaay yi, ci li ñuy wax tag yu HTML lañuy jaare di leen sos, joowukaay bi won la ko; ci misaal + +moo lay jox: wikipedia + +Tay jii sax lëkkalekaay yi ay nattukaay lañu, limu lëkkalekaay yiy jëme ci ab dal ci la ñuy xamee ñaata la siiwee. + +World Wide Web +lëkkalekaay yu World Wide Web bi ci xëti web yi la ñu nekk, maanaam ci jukki yi ñu bind ak HTML (Hypertext Markup Language). + +Xam-xamu nosukaay + + +Njàngale walla Yar +Tekkiy ñaari baat yi, yenn saa yi dañ leen di jaawatle. Ci maanaa, baat bu mujj bi, ci lu daj, mooy lépp lu ñuy xamal nit ki, ci bépp fànn (diine, ngor, teggin, xam-xam,añs). Baatu njàngale moom, ci wàllu boppam, day di rekk benn xeetu yariin, mooy xam-xam bi ñuy sukkadinkoo ngir taggat la ci lenn li, jàngal la lenn li. + +Kon njàngale benn xeetu yarin la bu ñu man a gis ci daara yu taaxe yi, fa nga xam ne ab sëriñ, bu taxaw janook ay ndongaam, di leen taggat ci xam-xam, jaare ko ciy kaddu walla ciy mbind. + +kon njàngale man naa tekki yar, waaye yar man naa bañ a doon njàngale. +Baatukaay +Jàngale wolof + +Njàngale +Ci melosuuf, yamoo wi aw rëddu tus-wu-gar la, di ag buumug jeneer gees rëdd mu wër àdduna, jaar ci diggante dott yi. Yamoo wi moo xàjjale àdduna bi, def ko xaaju-kol-kol bu bëj-gànnaar ak xaaju-kol-kol bu bëj-saalum. Tus-wu-gaar wu yamoo wi 0° (tus aj). Guddaayu yamoo gu Suuf si mi ngi tollu, ci xayma, 40 075 km. + +Yamoog Suuf si + +Kilimaa +Kilimaab barab yi ne ci li wër yamoo gi lañuy wax kilimaab yamoo. Di nañ wax itam klimaab gëwéel, di bu barab yi ne ci li wër gëwéel yi (gëwéelub Tef ak gëwéelub Sànkar). + +Réew yi mu dagg + +Ci sunu àdduna (Suuf si), yamoo gi ay mbàmbulaan ñoo ëpp ci li mu dagg ci yoonam, téeméer boo jël ci gudaayam ñaar-fukk ya rekk a jaar ci suuf. + +Afrig +Yamoo gi jaar na ci juroom-ñaari réewi Afrig : + +Saw Tome ak Preesip + Gaboŋ + Kongóo-Brasaawiil + Kongóo-Kinshasa + Ugandaa + Keeñaa + Somaali + +Melosuuf +am Màkkaanum mbëjfeppal, di ko wax itam màkkaanum m-bataaxal, walla màkkaanum e-mail, am mbooloom ay araf la, muy teewal ab boyotu bataaxalub mbëjfeppal bu nekk ci ag mbaal (reseau) gu xibaarfeppal gu mel ne internet. Màkkaanum mbëjfeppal mooy tax ñu man a yónnee ab m-bataaxal (bataaxalub mbëjfeppal) kenn nit ci internet. + +Ci lu bari dañuy jaawatle màkkaanum mbëjfeppal ak màkkaanum web, mi nga xam ne du lenn lu dul am màkkaan mu dalub web. Te sax am na yeneen xeeti màkkaani internet. + +Baat yi +Kon liñu lay yónnee ci sa màkkaanum mbëjfeppal du ab bataaxal, ndax bataaxal dañ koy jàppe niki lu ñu bind ci këyit ak xalima. Bataaxalub mbëjfeppal la, su ñu ko gàttalee mu doon m-bataaxal (di ci jàng: miim-bataaxal) + +Xam-xamu nosukaay +Barabu Senegaal la ngi féete ci diggante 12°8(fukk ak ñaari aj juroom-ñett) ak 16°41 ci tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 ci tus-wu-taxaw wu sowwu. wàllam wi féete sowwu mooy wi gën a nekk sowwu ci goxu Afrig. Am 15.85 miliyoŋ ciy way-dëkk (2017) + +Senegaal la ngi tëdd ci 196 712 km kaare, Sun ko méengale ak dëkkandoom yii di Mali ak Gànnaar, di nan gis ne réew mu tuuti la. + +Senegaal a ngi am 11 diwaan, 35 gox, 109 gox-goxaan + +Kilimaa +Senegaal, li ñuy wax klimaab Sahel la am. Looloo waral mu am jamonoy taw, di ko wax nawet, ak jamono jum dul taw dana-ka, di ko wax noor. Nawet a ngi door maami-koor jeex kori, waxset di jamono ji muy gën a taw nekk ci baraxlu-koor (day aju ci fi nga nekk: bëj-gànnaar walla bëj-saalum). Noor a ngi door koor jeex maami-koor. Tangoor gi gën a kawe tangaay lay ame, ci nawet bi. Yi gën a suufe ci weeru tamxarit. + +Ci li topp tefes gi, ngelaw liy bàyyeekoo ci géej gi mooy tax muy gën a sedd, tangaay bi day nekk ci diggante 16°C ak 30°C, waaye ci digg bi ak penku bi day toll ci 41°C. + +Séddatle + +Senegaal a ngi séddatliku ciy diwaan aki gox ak ay gox-goxaan + +Diwaan yi +Senegaal am na fukk ak benn ciy diwaan: + Cees + Jurbel + Fatik + Kawlak + Koldaa + Luga + Maatam + Ndakaaru + Ndar + Siggcoor + Tambaa-kundaa + +melosuufug Senegaal +Weer ab diirub jamono la, séddaliku ci ay ayubés, moom, ayubés, séddaliku ci ay bés. Ci arminaatu weer, ñu di ko wax itam weeri wolof, at mi fukk ak ñaari weer la, te weer yi am limu bés yu wuute. + +Yeneen xeeti arminaat yu dul bu weer man nañoo nekk, ci misaal, arminaatu jant + +Aminaatu weer +Dees na ko wax it weeru wolof + Tamxarit + Diggi-gàmmu + Gàmmu + Rakki-gàmmu + Rakkaati-gàmmu + Maami-koor + Ndeyi-koor + Baraxlu + Koor + Kori + Diggi-tabaski + Tabaski + +Arminaatu jant + Samwie + Fewirie + Maars + Awril + Mee + Suwe + Sulet + Ut + Sattumbar + Oktoobar + Nowembar + Disambar + +Arminaat +Jamono +Bés bi mooy diir bi jant bi di fenk ba ba muy sàngu; diggante ñaari guddi, jamono bi ceeñeeri jant bi di leeral asamaan si. Mi ngi door xaajaguddi, guddaayam a ngir aju ci jamonoy at ji nga ne ak tus-wu-gaar wi nga toll. Bés bi man naa mat 6 weer ca dotti Suuf si. Bési ayubés bi ñooy: altine, talaata, alarba, alxamis, ajjuma, gaawu ak dibéer. + + +Jamono +Pullaar aw làkk la wu ñuy wax daanaka ci 20 réewi Afrig gu sowwu ak gu diggu, Dale ko ca pegi dexu Senegaal ba ci gu Niil, waaso yu pël, tukulóor ak yu lawbe ñooy ñi koy làkk. + +Ci cosaan pël yi ay sàmmkat lañu, waaye tay daanaka xeeti liggéey yépp lañuy def: yaxantu, béy, njëwrin, añs. + +Ci pullaar yi nekk Senegaal ak Gànnaar, ñi koy làkk lañuy wax ay "haalpulaar'en" ("haalpulaar" su dee kenn), baat baa ngi jóge ci "Haalde" di firi "wax". "Haalpulaar'en" yi ci pegu dexu senegaal ay pël lañu jàppe seen bopp donte yenn saa yi dañuy am weneen làkk. Ni ko Amadu Ampaate Ba waxe, "Haalpulaar'en" yi duñu aw waaso, waaye am mbooloom ay waaso yu bokk dëkke dex gi, tànn pullaar niki làkk wu njëkk, làkk wu ñépp bokk di wax, di ci jokkoo. + +Pullaar di nañu ko wax itam pël, pular walla fufulde, ci waa faraas pël lañuy wax di baat bu ñu abbee ci wolof. + +Melokaanam +Kon pullaar (walla pël) daa séddaliku ci ay juroomi mbooloo, seenug wuute aju ci barab ba ñu nekk: + + Waxiin yu Fuuta-tooro, ci mbalkam biir mu dexug Senegal; + yu Fuuta-Jaloo, ca Ginne; + yu Maasina, ci li wër dexug Niseer; + waxiin yu diggu, yu bëj-saalum-penku gu Mali ba ca diwaani Dallol Mawri yi ak Bosso ca Niseer ; + yu penku, ca imbratóorug Sokoto ak gox yi wër (Penku-Niseer, Niseeriya, Kameruun, Cadd ak Réewum Diggafrig). + +Pël, ni yeneen làkki afrig, niki wolof, man nañu koo bind ak arafi araab walla yu latin. Wuute gi bari na ci waxiin yi ba ci mbindiin wi ci diggante pullaar ak pullaar. Ci misaal: baatu "nyambe" man nañu koo binde it "ñaamde". + +Ay misaal + +Baatukaay + Sonja Fagerberg-Diallo, « Milk and Honey: Developing Written Literature in Pulaar », in the Yearbook of Comparative and General Literature, 1995, n° 43, Indiana University + Sonja Fagerberg-Diallo, « "Learning to Read Woke Me Up!": Motivations, and Constraints, in Learning to Read in Pulaar (Senegal) », Adult Education and Development, 2002, n° 58, p. 45-60 + Mamadou Ousmane Niang, Constraints on Pulaar phonology, Lanham, Md. : University Press of America, 1997 ISBN:0761806113 + Mamadou Niang, Pulaar-English / English-Pulaar Dictionary, New York, Hippocrene Books, 1997 + Yero Sylla, Grammatical Relations and Fula Syntax, Los Angeles, University of California, 1979 (Thèse PhD) + Louis Léon César Faidherbe, Vocabulaire d'environ 1,500 mots français avec leurs correspondants en ouolof de Saint-Louis, en poular (toucouleur) du Fouta, en soninké (sarakhollé) de Bakel, 1864, Saint-Louis, Imprimerie du Gouvernement, 1864, 70 p. + Louis Faidherbe, « Dictionnaire de la langue poul, par le général Faidherbe, augmenté par le Docteur Quintin », Bulletin de la Société de Géographie, septembre-octobre 1881, p. 332-354 + Louis Faidherbe, Grammaire et vocabulaire de la langue poul à l'usage des voyageurs dans le Soudan avec une carte indiquant les cntrées où se parle cette langue, Paris, Maisonneuve et Cie, 1882 (2e édition), 165 p. + Henri Gaden et E. Leroux, Le poular : dialecte peul du Fouta sénégalais, 1912-1914 + Pierre Gourou, Les aventures de Kataboum (conte bilingue), L'Harmattan, 1997, 24 p. ISBN:2-7384-5020-2 + R. Labatut, D. M'bodj et A. Mohamadou, Peul. Méthode de langue, Bpi du Centre Pompidou, 1997 + Anne Leroy, Parlons pular : dialecte du Fouta Djalon, L'Harmattan, 2002 + A. Mohamadou, Classification et représentation des propriétés lexicales en Peul, Éditeur Suzanne Platiel, 2000 ISBN:2910809021 + Oumar Niang, Description phonologique, morphologique, organisation et fonction de catégorisation des classes nominales en pulaar, thèse de doctorat soutenue le 24 février 2007 à La Maison des Sciences de l'Homme et de la Société, Université de Poitiers. + Jean Schmidt, La phonologie du Poular du Fouta Toro et les interférences français-poular, 1974 + Christiane Seydou, Dictionnaire pluridialectal des racines verbales du peul : Peul-français-anglais, Karthala, 1998, 952 p. ISBN:2865378632 + G. V. Zubko, Dictionnaire Peul-Français, Osaka, National Museum of Ethnology, 1995 + +Làkki senegaal +Fatik, mi ngi yaatoo 7945km, am 475.970 ciy way-dëkk. Mooy péyu diwaan bi mu bokk (diwaanu Fatik) ak goxu Fatik. Mi ngi juddu niki diwaan ci 1984, ba ñu xaajee diwaanu Siin-Saalum ñaar: Fatik ak Kawlak. Mi ngi tëdd ci lu féete Mbàmbulaanug Atlas gi, ci sowwu senegaal, ci suufu Kawlak, feggok réewum Gaambi ci bëj-saalumam. + +Koom-koom +Koom-koomam mi ngi cëslaayu ci mbéyum gerte, pepp, càmm ak napp. +réewi-taaxi Senegaal +Kawlak am réewu-taax mu mag la ca senegaal, féete ci li tollook bëj-saalum-penku Ndakaaru. Mooy péyu diwaanu kawlak ak goxu Kawlak. + +Ci lu daj +Ba ko tubaab yi di sanc benn dëkk rekk a fa nekkoon muy Ndangaan. Kawlak yàgg naa doon ab tombum jaaru gerte gi ñu daa béy ci yeneen diwaan yi ko wër, ca waaxam wa lañ daa jaarale gerte gi jëme Ndakaaru. Kawlak a ngi bokkoon ci nguuru Saalum ga woon. Ba fa waa faraas yi di sanc buur-saalum da leen xajaloon ngir bañoon fitna judd ci seen diggante. + +Diine +Kawlak am na ab jàngu bu mag, Saint Theophile Turpin mooy kiñ ko tudde. Njiitu jàngu bu Seneegal bu tay jii, Tewodoor adiriye saar, nekkoon na fa ci diir bu guddu. + +Jumaay Kawlak, bi Baay Ñas tambalee woon tabax, tay jii ci diggu ab dëkk bu rëy la ne: Medina Baay. Mooy fa njabootu sëriñu tiijaan boobule, génn àdduna ci atum 1975, dëkke. + +Melosuuf +Ci waññi yi ñu amal ci atum 1988 ak 2002, Kawlak amoon na 150 061 ak 172 305 ciy way-dëkk. Ci 2007 ciy ay nattale yu nguuru senegaal def, jàpp nañ ne war naa mat 185 976 ciy way-dëkk. + +Koom-koom +Kawlak ab selebiyoon bu mag la. Ci yaxantug gerte gi la réewu-taax mu kawlak mas di dund. Bari na ay ja yu mag aki luuma. + +Téerekaay + H. Bessac, « Découverte de gisements néolithiques au sud de Kaolack (Sénégal) », Notes Africaines, Dakar, IFAN, 1952, n° 55, p. 65-69 + Etienne Badiane, Développement urbain et dynamiques des acteurs locaux : le cas de Kaolack au Sénégal, 2004 + André Dessertine, Un port secondaire de la Côte occidentale d’Afrique, Kaolack. Étude historique, juridique et économique, des origines à 1958, Université de Dakar, 1959, 172 p. (Diplôme d’Etudes Supérieures de droit). + Ibrahima Diouf, Kaolack : De l'arachide aux activités informelles, 1988 + Joseph Fouquet, La traite des arachides dans le pays de Kaolack et ses conséquences économiques, sociales et juridiques, Saint-Louis, IFAN-Université de Dakar, 1958, 263 p. (Etudes sénégalaises n°8) (Thèse de Droit, Montpellier, 1951, publiée) + Aline Garderet, Les fonctions de capitale régionale de Kaolack, Université de Bordeaux, Travail d'études et de recherches, 1968, 129 p. + Djibril Gueye, L’école coloniale à Kaolack 1893-1928, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2002, 105 p. (Mémoire de Maîtrise) + Fadya Hani, Monographie climatique d’une station synoptique, Kaolack 1946-1975, Université de Dakar, 1982, 113 p. (Mémoire de Maîtrise) + Emile Jacquier, « Le Port à arachides de Kaolack (Sénégal) », Publications du journal Le Génie civil, 1933 + Alain Morice, Projet d'étude sur certaines activités dans la ville de Kaolack (Sénégal), École des Hautes études en sciences sociales, Centre d'études africaines, 1981 + Alain Morice, Les forgerons de Kaolack : travail non salarié et déploiement d’une caste au Sénégal, Paris, EHESS, 1982, 6 + 350 p. (Thèse de 3e cycle) + Mbaye Ndiaye, Histoire politique de la ville de Kaolack, (1945-1962), Université de Dakar, 1988, 104 p. (Mémoire de Maîtrise) + Soukeyna Ndiaye, Les équipements urbains au Sénégal : l’exemple de Kaolack 1946-1996, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1999, 162 p. (Mémoire de Maîtrise) + Magatte Simal, Les Kaolackois face à l’administration coloniale de 1914 à 1938, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1990, 93 p. (Mémoire de Maîtrise) + Denis Tillinac, L'Hôtel de Kaolack, Robert Laffont, 1991, Pocket n° 4602, 1992, 177 p. (roman) + +Lëkkalekaay yu biti + + Maps, weather and airports for Kaolack + Kaolack sur Planète Sénégal + Carte au 1/200000 de la région + +réewi-taaxi Senegaal +Amsterdam mooy péyu réewum Olaand. + +Olaand +Péy +Diiwaanu Ndakaaru, benn la ci fukk ak juroom-ñenti diiwaan yu Senegaal yi. Moo ci gën a tuuti, ci yaatuwaay, waaye moo ci gën a bari way-dëkk. Yaatuwaayam toll ci 550 Ñoo ngi ko séddale ci ñenti Tund: Ndakaaru, Pikin, Géejawaay ak Tëngéj + +Lëkkalekaay yu biti +Statistiques Geo Hive +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Jurbel benn la ci diiwaani Senegaal yi. Amul benn ubbeeku ci géej gi. + +Mi ngi yem ci diiwaani Cees ak bu Fatik ci bëj-gànnaaram, ci bëj-saalumam ci diiwaani Cees ak bu Fatik, ci penkoom ci diiwaani Fatik ak bu Luga, ci sowwam ci diiwaanu Cees. Am na lu tollu ci 1 049 954 ciy way dëkk te yaatoo 4 359 km2 + +Diiwaan bi mi ngi nekk tembe fa nguuru bawol ga nekkoon. + +Ay tundam + +Bambey +Jurbel +Mbakke + +Xool it + +Téerekaay +Ibrahima Dieng, L'action des services sanitaires dans la région de Diourbel, Dakar, École nationale d'Administration, 1968, 151 p. +J. Gard et Raymond Mauny, « Découverte de tumulus dans la région de Diourbel (Sénégal) », Notes Africaines, IFAN, Dakar, IFAN, 1961, n° 89, p. 10-11 +Ismaïla Lo, « La région de Diourbel », Sénégal d'Aujourd'hui, n° 16, 1970, p. 23-30 + +Lëkkalekaay yu biti +Diwaanu Jurbel ci dalub gnuur gi www.finances.gouv.sn +Statistiques Geo Hive + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Fatik benn la ci diiwaani Senegaal yi. + +Ci bëj-gànnaar ak ci bëj-gànnaar-peku, diiwaanu Cees, Jurbel ak Luga ñoo ko wër, ci bëj-saalumam Gaambi la taqalool, mbàmbulaanug Atlas gee ko féete sowwu. + +Melosuuf + +Xeetu klimaam mooy bu sudaan-sahel. te yii Ñooy ay tundam: +Fatik +Funjuñ +Gosaas +Digi diiwaan bi yu tay jii, ñi ngi leen tëral ci àtteb 84-22 bu 22 diggi-gamu 1984. Laataa-loolu mi ngi bokkoon ci diiwaan bu yaa ba woon, di Siin-Saalum. + +Am na 613 000 ciy way dëkk te yaatoo 7 930 km2 + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive + Situation économique et sociale de la région de Fatick - Édition 2004 (rapport du Ministère de l'économie et des finances, août 2005) + +diiwaani Senegaal +Duggalal fii mbind mi ñu daytalul. + +Cuub +Uetersen (ˈyːtɐzən) ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Almaañ. +Mi ngi yaatoo 11,50 km², ci 2006 amoon na 17.865 way dëkk. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + Uetersen + +Almaañ +Kureelu temb bu Poortorikoo bi (ci Ispaañ:partido Indipendentista Puertorriqueño), ab kureelu politigu Poortorikoo la buy yëngu ngir Poortorikoo am tembteem. Benn la ci ñetti kureeli politig ya fa ëpp solo te di it ñaareel ba fa gëna yàgg. + +Jaar-jaar +Gilberto Concepción de Gracia moo ko sos ci 20 kori 1946, ndax dafa jàppoon ne beneen kureel bii di Partido Popular Democrático dafa wàccoowul ak wareefam, maanaam laaj tembteeb seen réew. + +Poortorikoo +Diiwaanu Kawlax benn la ci juroom-ñenti diiwaani Senegaal yi. Réewu-taax mu kawlax mooy péeyu diiwaan bi, te ëpp ci solo it. Mi ngi réye 16010 km2, am 1 066 375 ciy way-dëkk + +Féeteem ci Melosuuf + +Mi ngi peggook: + Diiwaanu Fatik (tunduw Gosaas) ci bëj-gànnaar ak diiwaanu Luga (tunduw Lingeer); + Diiwaanu Tambaakundaa ci penku; + réewum Gaambi ci bëj-saalum; + Diiwaanu Fatik (tunduw Funjuñ ak wu Fatik) ci sowwu. + +Ay tundam +Ba ñu defee tunduw Kafrin diiwaan ci 2008, diiwaan bi ñetti tund rekk la am: + + Tunduw Kawlax + Tunduw Kungéel (mi judd ci 2006) + Tunduw Ñooro bu Rip + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive + Région de Kaolack sur www.finances.gouv.sn + La région aux Archives régionales du Sénégal + Situation économique et sociale de la région de Kaolack (rapport officiel 2004) + +diiwaani Senegaal +Koldaa ngi bokk ci Kaasamaas, ci digg-bëj-saalumu Réew mi. Benn la ci fukk ak ñenti diiwaan yu Senegaal. Mi ngi yaatoo 21 011 km2 te am 847 243 ciy way-dëkk. + +Ay tunduw +Ba ñu defee goxub Séeju diwaan ci 2008, la diwaan bi am ñaari gox rekk: + + Tunduw Koldaa + Tunduw Velingara + +Lëkkalekaay yu biti +Statistiques Geo Hive + « Kolda : la pauvreté comme vitrine » (jukkib yéenekaay bu Le Quotidien) + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Cees benn la ci 14 diiwaan yu Senegaal, Féete ci penku Réew mi, wër ndombo Ndakaaru. Yaatoo 6 601 km2, am 1 442 338 ciy way-dëkk. dëkkub Cees Mooy Péeyu diiwaan bi. + +Melosuuf +Ci genn wàllam mi nga janook Tefes-gu-Mag gi, fi mbayum yu-sew yi di ame, ci Ñaay bi, ci geneen gi di janook Tefes-gu-Tuuti gi di barab bi ëppi nemmeekukat ci Senegaal. + +Doon ab tombub jàllu ci diggante Ndakaaru ak li des ci réew mi. Diiwaan bi am na ay cëslaay yu tali ak yu weñ yu matale ngir wóoral tuxute gi(dem-beek-dikk bi), ci suufam. + +Doonte diiwaan bu tuuti la soo ko méengalee ak yeneen yi, waaye mooy ñaareelu diiwaan bi ëppi nit, ci Réew mi, ginnaaw Ndakaaru. + +Séeddaliinu suufam +Diiwaan baa ngi Séeddaliku ci 3 tund: + Tunduw Mbuur + Tunduw Cees + Tunduw Tiwaawan + +Taariix +Ci Melosuuf Diiwaan bi tay mooy nguuru Kajoor ga woon ak gu Bawol. Ag Yokkuteem mi ngi tegu woon ci yoonu weñ wi, rëdd wu Ndakaaru-Ndar ci mujjantalu XIXu xarnu, wu Ndakaaru-Niseer tegu ci. Bokk na ci diiwaan yi gën a yàgg ci Senegaal. + +Téerekaay + Sidath Diop, Les polissoirs de la région de Thiès : étude typologique et ethnographique, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2002, 101 p. (Mémoire de Maîtrise) + Roger Laval, La décentralisation au Sénégal : l'industrie dans la région de Thiès, travail d'études et de recherches, Dakar, Département de géographie, Université de Dakar, 1971 + Guy Quérec, La population urbaine au Sénégal. La ville de Thiès et sa région, Dakar, Université de Dakar, 1968, 2 fascicules, 167 p. + annexes (Dipôme d’Etudes Supérieures) + Papa M. Sylla, Évolution de l'impact de la stratégie et du fonctionnement d'un programme de lutte contre la lèpre dans la région de Thiès (Sénégal), Université de Montréal, 1990 (M. Sc.) + Gordon Williams et al., « Enquête sociolinguistique sur les langues Cangin de la région de Thiès au Sénégal ». Cahiers de recherche linguistique, 1989, n° 3, Dakar, SIL. + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive 2002 et 2005 + Site du Conseil régional de Thiès + La Région de Thiès sur le site du PEPAM (Programme d'eau potable et d'assainissement du Millénaire) + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Ndar benn la ci 14 diwaani senegaal yi, moo gën a féete bëj-gànnaar ci réew mépp. Moo feggook réewum Gànnaar, ci guddaayu dig gi mu am ak Senegaal gépp ba fi dexub Senegaal bi di àgge ci mbàmbulaanug Atlas gi. + +Taariix + +Démbu Ndar Géej + +Bès dafa am feebar buy walle bi mabboon seen gox bi nu doon woowe Ndar, samppu woon si diggante ñaari dëkk yu tudd Biyer ak Geber. Ñaari dekk yi ñi ngi nekkoon si joor gi. Ba loola xewee, la waa dëkk ba fabu gaddaay ag seeni gaal, xoti dex di dem, ba teersi fi tay nuy wax Dunu Ndar. Li taxon kon mo di ne danoo beggoon mucci si musi ak balaa bile naroon a raafal seen ñoñ. Turu ndar wu jekk wi lanu toxal indi ko si dunu wi si dig ndox ngir maggale ko seen dëkku maam ba nu jóge, ngi itam ba ña fatte fa nu bayyikoo. Lii ga man see jànge ni tur si dëkk ak si lu mu man a doon, dafa war a mandarga cosaan, lukko moy, nit ki man naa dem ba fatte fu mu soqe koo.  Si ñi ko Maalik waxe ba leegi, wen xaaj si way-gaddaay yi, da no fafoon des si joor gi janloog tund wi, ginnaw gi nu tudde teenu geej. Beneen calale da fa indi ag goor gu joge réewu gannaar, bu nu doon woowe Ametlika Ben Ndar, soqe ki sa Singeti, moom la ay settam tudde dekk bi di ndar. + +Xarnu bi tubaab yi di wandeelu ci wetu tefesu senegaal, ku ñu naan Ndaak Kumba Nan Sango moo doon nguuru ci imprator bu waalo. Boo ba jamano, waloo mi ngi woon si dig dooleem, di tëg ay ndën ndam. Suuf su nangu mbay, njënd ak njaay mu dox, si diggante nit ñu nuul yi ak naari ganaar. Xarnu junni ak ñetti teemeer la woon jappu junni ak ñetti  teemeer ak juróom ben fukk. Tukkikat tubaab yi, waa ruyang ak nitu jeppo yi doon nañ fa joofsi ngir bokk si njënd ak njaay ma fa daan am. Booba lii dong la nu fa doon def, walis nag nu amoon yeneen mbetet yu nu nebboon. Taarixkat yi jappu nanu ne xeet yi ño fa jiitu woon waa portugaal. Si atum junni ak ñetti téeméer ak juróom ben fukk ak ñeent la wa gox ba tambale jaay tubaab yi lusi mel ni mboq, dugub, ak yeeneen. Ñoom tubaab yi sax ni ngi xamee xeetu dugub yile fi si Afrig, rawatina seneegal. Ja bi ci waloo nag, mboleem yi doon yëngatu ci koom-koom si réew mi, nga bayo kajoor, wala biir waalo da nga fa daan ñów ngir jaay wala jènd ay yëf. Dawalkatu gaal yi jóge tugal demmon nanu ba dugglaante ak way-njiitu paraag yi. Ndawtal yi ag yóbal yi leen wa njiit yi doon jagleel moo gennoo na dëggeral seeni kolere. + +Ay doomi normang  yu am fit xuus nanu mbeex bi ak seen gaal àggsi ci dexu senegaal. Sa teeruwaay mo doon dunu Morfil, bërëbu seeluwaay.  Tangoor bi ak feebar yi nekkoon ci réew mi daan fagaagal ñi ëppoon ci noom, ba tax na ñuy ci bari danu daan faral di ñakk seen bakkan. Wante galankoor yi musu leen tayyeeloo, wala mu leen di lotal ba ta ñuy yebbi seen ëmb te baña tee tukki. Galam daakande, ak bejjani ñay moo leem gënnoona soxal. Ci gattal, njënd-ak-njaay mi daan dox si xarnub fukk ak ñeet moo indi jëflaante waa tugal yi ak wa sóodaan. + +Fara Xoy Jóob, buuru Waalo ci atum juróomi junni ak juróom téeméer ak fukk, moo njekka artu nit ñi, rawatina nappukat yi si nu bayi xell mbeex mi. Jamano yooyu, ay néewu tubaab danu doon tëmb si géej gi te ken xamul lu ko waraloon. Ba nu tegge juróom ñetti at la waa portugaal dall si dunu mboxos bi nekk si wetu ndar. Su nu beggoon na jeggi bel bi, baraak bi nekkoon ganjool da leen doon laaj ndamppaay. Si noonu lanu tambalee xuus gëeju senegaal ba podoor, jaal ngalam, ba jennee. Naari gannaar yi danu leen daan faral di sòng ay còng yu tàr, dileen lalal ay ndëg-sërëx. Dunu morfil lanu daan jaaye seeni nganaay, ak yeneen jumtukaay yu jem si xare. Foofu itam lanu daan wacce jaAm yi nu jappoon, ñaari way-watu timmaleleen ay mëx-dóom, ku daw rekk nu soqi ci sa kow. Kon jaam yi njek wacci si suufu ndar, dekkun fa woon. Jaaxle nag mi ngi tambalee sotteeku ci xelu nit ñi bi nu seetloo ne seen doom di ay nappukat ñi reer ni mes ci géej gi te xamu nu lan moo tax. Ndekete yo ay woroom gaal yu tubaab ño leen di doggaanu, di fadang jemmee tugal. Jamano booba, buur Tiaaka bu waalo moo amme woon. Ay jum yuy tak, ar fer-ñeet ak ay saliir yu raglu doon nanu jip si géej gi. Ba si saxaar su nuul, su xasaw di agsi ba ci ker yi. Xeex bu meti moo doon am si diggante tubaab yi seen boppu. Waa faraas, portugaal, olaand ñoo don xëccoo. Ku ci nekk bëg aakimo dend yi . naar yi tamit door seeni lël ngir jappu nit nu nuul yi di leen jaay njaam.  Yen si nappukat danu doon jëflaante ak tubaab yi ci mbeex mi, di leen jaay ndox mu neex, jen, ak yu ni mel. Tubaab di leen jox ay sangara, wenñ, ay piis, ak tooke. Si njelbeenu fukk ak juróom ñaari xarnu, ci nguurug Buuru faraase bu tuddoon lui fu ak ñett, ci la kangam Riseliye joxe ndigel way tukkikat géej yi ngir nu tambale foxrañi beppu suuf bu ñu man a foxarñi ci dendub Afrig. + +Dayoo bi mu am tey jii, mi ngi jóge ca séddatle gi ñu def ci atum 2002. Bu njëkk diiwaan bi da fa ëmboon tamit diiwaanu Maatam bépp ak li ko wër. + +Ay Tundam + Tunduw Dagana + Tunduw Podoor + Tunduw Ndar + +Xool it + +Téerekaay + Annie Ravisé, Contribution à l’étude des Kjökkenmöddinger (amas artificiels de coquillages) dans la région de Saint-Louis, Dakar, Université de Dakar, 1969 (Mémoire de Maîtrise) + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive + Conseil régional de Saint-Louis + La région aux Archives régionales du Sénégal + La filière lait et produits laitiers dans la région de Saint-Louis (Christian Corniaux, rapport, avril 2003) + +Diiwaani Senegaal +Diwaanu Luga benn la ci 14 diwaani Senegaal yi. Mooy diwaan bi ëppi pegg ci Sengaal Gépp, moom dafa diggu. +Am na 677533 ciy way-dëkk, te yaatoo 29188km2 + +Melosuuf + +Ay peggam +Diiwaanu Luga ngi peggook: + + Diiwaanu Ndar, ci bëj-gànnaaram + Diiwaanu Maatam ci penkoom + Diiwaanu Cees, bu Jurbel; bu Fatik, bu Kawlax ak bu Tambaakundaa ci bëj-saalumam + Mbàmbulaanug Atlas gi ci sowwam + +Tund yi +Tunduw Kebemeer +Tunduw Lingeer +Tunduw Luga + +Xool it + +Téerekaay + Fatou Diop, « Le travail comme représentation et pratique quotidienne dans la région de Louga », in Elisabetta Benenati et al. (sous la direction de), Lavoro, genere e sviluppo locale in Mali e in Senegal, Turin, L’Harmattan Italia, 2002 + Diop Fatou Diop (sous la coordination de), Les nouvelles formes d’émigration dans la région de Louga, Rapport de recherche « Tukki liggéey la », Coopération Inter-Universitaire Turin-Sahel (Université de Turin-Italie/Université Gaston Berger Saint-Louis, Sénégal), 2003 + Moustapha Sar, Louga et sa région (Sénégal). Essai d’intégration des rapports ville-campagne dans la problématique du développement, Dakar, IFAN, Université de Dakar, 1973, 308 p. (Initiations et Etudes Africaines n°30). (Thèse de 3e cycle soutenue en 1970, Strasbourg) + Jorge Suazo-Toro, Proposition de mesures d'amélioration de l'élevage : région de Louga au Sénégal, Uppsala, Swedish University of Agricultural Sciences, International Rural Development Centre, 1993 + +Lëkkalekaay yu biti +Statistiques Geo Hive + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Siggcoor benn la ci 14 diiwaani Senegaal yi, mooy wàllu Kaasamaas wi féete penku. am na 437986 ciy way-dëkk te yaatoo 7 339 + +Tundyi +Diiwaan bi ci ñetti Tund lañ ko xaaj : +Tunduw Biñoona +Tunduw Usuy +Tunduw Siggcoor + +Xool it + +Téerekaay + Répertoire des villages : région de Ziguinchor, Dakar, Ministère de l'Économie, des Finances et du Plan, Direction de la Prévision et de la Statistique, 1992, 31 p. (résultats du recensement de 1988) + +Lëkkalekaay yu biti +Statistiques Geo Hive +Présentation de la région de Ziguinchor (site de l'Inspection académique de Ziguinchor) + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Maatam benn la ci 14 diiwaani Senegaal yi. mi ngi judd ci atum 2001. Am na 423 041 ciy way-dëkk te yaatoo 25 083 km2 + +Melosuuf + +Ay peggam +Diiwaan baa ngi peggook: + Diiwaanu Ndar ci bëj-gànnaaram; + Diiwaanu Luga ci sowwam ak ci bëj-gànnaar-suwwam; + Diiwaanu Tambakundaa ci bëj-saalumam; + Dexub Senegaal bi, fi janook réewum Mali, ci penkoom. + +Ay Tundam +Diiwaan baa ngi séddatliku ci ñetti Tund: +Tunduw Kanel +Tunduw Maatam +Tunduw Raneeru + +Xool it + +Téerekaay + Sylviane Fresson, Public participation on village level irrigation perimeters in the Matam Region of Senegal (Participation paysanne sur les périmètres villageois d'irrigation par pompage de la zone de Matam au Sénégal), Paris, OECD, Occasional papers on experiences in rural development, n° 4, 1978, 20 p. + Djibril Diop, Dynamiques territoriales, décentralisation et enjeux de développement local dans la moyenne vallée du fleuve Sénégal. Cas des communautés rurales de la région de Matam, Université de Paris I, 2004, 447 p. + Ahmadou Kane, Matam et sa région, Dakar, Université de Dakar, 1977, 363 p. (Thèse de 3e cycle de géographie) + Jean-Paul Minvielle, Migrations et économies villageoises dans la vallée du Sénégal : étude de trois villages de la région de Matam, Dakar, ORSTOM, 1976, 129 p. + Jean-Paul Minvielle, La structure foncière du Waalo Fuutanke : les terres inondables de la moyenne vallée du Sénégal, région de Matam, Dakar, Office de la Recherche Scientifique et Technique Outre-Mer, 1977. + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive + La région de Matam sur le site de l'ANCAR (Agence nationale de conseil agricole et rural) + +diiwaani Senegaal +Diiwaanu Tàmbaakundaa mi ngi nekk ci penku réew mi, benn la ci 14 diiwaan yu Senegaal yi, di it bi ci ëpp ci rëyaay. Dëkku Tàmbakundaa mooy péeyub diiwaan bi. am na 605 695 ciy way-dëkk te yaatoo 59 602 . + +Melosuuf + +Ay peggam +Diiwaan baa ngi digoo ak: + + Diiwaanu Maatam ak bu Luga ci bëj-gànnaaram; + Diiwaanu Kawlax ak bu Koldaa ak réewum Gàmbi ci sowwam; + Réewum Gine ci bëj-saalumam; + Dexug Senegaal gi, fi mu janook réewum Mali, ci penkoom; + +Ay goxam +Ginnaaw bi, bi ñu defee Tunduw Kéedugu Diiwaan bu mat sëkk ci 2008, Péncum Réewum Senegaal la ngi ko def ci 1 diggi-gammu ci 2008, diiwaan bi ñaari Tund rekk la am: + + Tunduw Bakkel + Tunduw Tambaakundaa + +Xool it + +Lëkkalekaay yu biti + Statistiques Geo Hive + Conseil régional de Tambacounda + Situation économique régionale de Tambacounda, édition 2005 (juin 2006) + +Diiwaani Senegaal +Wu-angalteer mooy làkk wa ñuy wax te juddoo ca Nguur-Yu-Bennoo yi + +Làkk +Nguur-Yu-Bennoo +Gëwéel yi ñaari rëdd lañu yu dëppook yamoo gi: gëwéelub Tef tollu ci 23°24' wu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar gi ak gëwéelub Sànkar tollu ci 23°27' wu tus-wu-gaar wu bëj-saalum. di nañu woowe it gëwéel diiwaan yi ne ci li wër rëdd yooyule (di faral di wax dëkk ci gëwéel yi). + +Melokaan +Ci li jege yamoo gi, di nañu faral di gis klimaa bu ànd ak tàngoor wu tar ak taw bu bari ci at mi mépp: di ko wax klimaab yamoo. Waaye, ci li jege gëwéel yi (Tef mbaa Sànkar), ci at mi noor ak nawet rekk a ci am, kon wàcciit yi (taw yi) day wuute ci jamonoy at mi, ba daanaka at mépp ay tàng, di li ñuy wax klimaab gëwéel. + +Waaye nag jàpp nañu ne it ngelaw yiy upp ak duusi géej yi ak rëyaayu diiwaan bi am nañu ay jeexiital yu solowu ci klimaay diiwaan yi, ba tax na su nu seetloo yenn diiwaan yi, doonte nekk nañu ci wetu ab gëwéel, amuñu klimaab gëwéel (ci misaal diggu Óstraali walla bu Sahara, nga xamne amuñu nawet) ak yenn diiwaan yu am klimaab gëwéel te nekkuñu ci lu jege gëwéel yi( lu mel ne réewum Keeñaa, nekk ci yamoo gi te li ëpp ci suufam klimaab gëwéel la am). + +Diiwaani gëwéel yu mag yi +Diiwaan yiy dund cib klimaab gëwéel dëgg-dëgg ñoo ngi nekk ci diggu Aamerig ak bëj-saalumu Aamerig, ci digg ak genn wàllu bëj-gànnaaru Afrig, ci bëj-gànnaaru Óstraali ak genn wàllu Endoneesi. Li des ci barabu diggantegëwéel bi dañu leen di séddale ci diggante klimaab tàkk (rawatina ci Afrig), bu yamoo walla bu xaw a sedd (rawatina ca Asi + +Lëkkalekaay yu biti + CNRS La bodiversité tropicale. + Agropolis: Portail européen de recherche de formation et d'information sur la Méditerranée et les pays tropicaux. + Une agronomie tropicale au service des agricultures familiales ? (Forum d'Agropolis) + P. W. Richards, professeur de botanique, "Etude de la végétation tropicale (se référant particulièrement à la Guyane britannique et à l'Afrique occidentale britannique)". University College of North Wales, Bangor. UNESCO 1956. Archives de la fAO. + Mieux connaître et protéger la nature et les peuples des forêts humides + "Gestion environnementale des écosystèmes et forêts tropicales" : Groupe de Formation et de Recherche sur les écosystèmes tropicaux forestiers et naturels, AgroParisTech-ENGREF + +Gëwéel +Madrid : mooy péeyu rééwum Ispaañ. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Tugal + +Lëkkalekaay yu biti + + +Ispaañ +Péy +Zurich (Almaañu : Zürich) : Dëkk Suwis + +Suwis +Dëkk +Rom mooy péeyu rééwum Itaali. + +Itaali +Péy +Yàlla, Buur Bi, Sunu Boroom, Aji-Màgg Ji, Aji-Sàkk Ji..añs lépp a ngi joxoñ Ki sàkk lépo ak ñépp. + +Yàlla (ar : الله ; fr : Dieu; en : God) + +wolof naan ko Yàlla, njëkk Lislaam wolof "Yal" la daan wax namm ci "Yàlla" bi Lislaam dikkee, bawoo ci araab yi naan "Àllaa" ci lañu jëlee "Yal" yokk ci "Àllaa" naan "Yàlla" waaye teewul ba leegi wolof yi di jëfandikoo baatu "Yal" jooju ci seen i ñaan niki "Yal nanu Yàlla jéggal" "Yal na la Yàlla sàmm"...añs. + +Diine + +Diine Yépp Saxal nañu ag Amam, donte wuute nañu ci jëmmam ak i meloom ku ne ak na mu ko jàppe. bu dee ci diibey kojug asamaan yi wuutewuñu ci ne Moom ki bind lépp te kenn bind ko niki diiney Yahuut, Nasaraan ak Lislaam. + +Lislaam +Ci lislaam jullit ñi dañuy saxal amug Buur Yàlla mu bokk ci juróom benn ponki ngëm yi nekk ba ca jiitu ànd nag ak anam yu ñj ko war a gëmee, nde am ay melo yoo war a saxal ci Jëmmam Ji, am yoo war a dàq jommale Ko ko, am wow day dagan ci moom. +ni nu Koy gëmee nag mooy gëm ne am na te moo fi jiitu lépp te du fi jóg te nuróowul ak menn mbindéef te ku doylu la ci boppam, aajowoowul jëm ci kenn te kenn ku ne ak lenn lu ne aajewoo na jëm ci Moom te it Kenn la ku amul kenn ku ko ñaareel ci jëmmam walla jëfam wallay waxam walla wenn meloom, ku am kàttan la koo xam ne balaa daraa xew da koy bëgg te na mu ko bëggee lay +amee, ku am xam-xam la kog réeréewul darra, mbooleem li nu nekkee ak li nuy bëgg a nekkee darra umpu ko ci, day dund, day dégg lu kawe ak lu suufe, +di gis lu nëbbu ak lu feeñ, di wax. + +Li jomb ci Moom nag +te mooy li mënul a am moo di ag ñàkk, ñu naan Yàlla am na te amul ak sosu +nga xam ne mas naa ñàkk ginnaaw bi mu am walla darra am te neexu ko walla ameewul na mu ko bëggee walla muy tëx walla mu tëlee wax walla mu ñàkk a xam walla mu gumbë walla mu réerée darra walla muy faatu, li nga xam ne +man naa am ci Moom man a ñàkk (Mooy Lu dagan) mooy def ak dindi, mbooleem li ngay gis walla mu toq ci sam xel daa dagan ci sa Boroom, bu ko neexee amal ko bu ko neexee ñàkkal ko. Boo boolee melo yii yépo day tollu ci ñaar fukki melo, mu war ci jullit bi mu gëmee ko nii. + +Alxuraan +Bu nu delloo ci Alxuraan diba nu fekk Muy melal Boppam ciy warab yu fasantikoo ci biir téere bu sell bi, mu bokk ca Saar wi miy melale Boppam walla nu ne Da ci doon aajar Boppam; muy Saar 112 : SELLAL +4 - Laaya – Laata Gàddaay ga + +Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. + +1. Waxal ne : “Yàlla, moom Kenn la (jenn Yàlla rekk la). +2. Moom Yàlla, Mooy Kilifa gi wareefa joyal mbir yi. +3. Jurul, te Kenn juru ko. +4. Te amul benni nàttangoo”. +Tus (fr : zéro) : 0 + +Xayma +Benn (fr : un) : 1 + +Xayma +Minsk mooy péyu réewum Belaarus + +Belaarus +Péy +Sofiya mooy péeyu réewum Bulgaari + + + +Bulgaari +Péy +Prag mooy péyu Réewum Cek + +Réewum Cek +Péy +Budapest mooy péyu réewum Oonguri + +Oonguri +Péy +Kisinawu mooy péyu réewum Moldaawi + +Péy +Moldaawi +Warsaw mooy péeyu réewum Poloñ + +Poloñ +Péy +Bukarest mooy péyu réewum Romaani + +Romaani +Péy +Mosku (Москва́) mooy péeyu réewum Riisi. + +Dëkki Riisi +Péy +Baratislawa mooy péyu réewum Eslowaaki + +Eslowaaki +Péy +Kiyew (uk: Київ; ru: Киев) moy péyu réewum Ukreen + +Ukreen +Péy +Dëkki Ukreen +Kopenagen : mooy péyu réewum Danmaark + +Danmaark +Péy +Talin (et: Tallinn) mooy péyu réewum Estooni + +Estooni +Péy +Elsinki (sv: Helsingfors) mooy péyu réewum Finlaand + +Finlaand +Péy +Reykiyawik (is: Reykjavík) mooy péyu réewum Islaand. + +Islaand +Péy +Dublin mooy péyu réewum Irlaand + +Irlaand +Péy +Riga : mooy péyu réewum Letóoni + +Letóoni +Péy +Wilniyus (lt: Vilnius) Mooy péyu Réewum Lituwaani + +Lituwaani +Péy +Oslo : Mooy péyu Réewum Noorwees + +Noorwees +Péy +Stokolm (sv: Stockholm): mooy péyu réewum Suweed + +Suweed +Péy +Londar mooy péyu Nguur-Yu-Bennoo yi + +Nguur-Yu-Bennoo +Péy +Tirana mooy péyu réewum Albaani. + +Albaani +Péy +Andorra la Vella mooy péyu réewum Andoor + +Andoor +Péy +Saarayego mooy péyu réewum Bosni. + +Bosni +Péy +Sagreb mooy péyu réewum Korwaasi. + +Korwaasi +Péy +Skopje mooy péyu Réewum Maseduwaan + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + +Réewum Maseduwaan +Péy +Waleta mooy péyu réewum Malt + +Malt +Péy +Montenegro (Црна Гора, Crna Gora) am réew la mu bokk ci goxub Tugal. + +Tugal +Réew +Montenegro +Melo : kuloor (fr : couleur) +Xonq : melo (fr : rouge) + +Melo +Mboq : melo (fr : jaune) + +Melo +Wert walla nëtëx: melo (fr : vert) + +Melo +Baxa : melo (fr : bleu) + +Melo +Daaray Sëriñ Tuubaa lu ñu sos la ngir fas yéene cee yakk cig piri mbooleem walla lu ëpp ci téere yi Sëriñ bi def, muy lol lu war la ngir ne Sëriñ bi ay mbindam aki taalifam ci araab la leen defe te nu war leen a xam, ñu tàmbalee ci yii: + +Nahju +Mawaahibul Xuddoos +Jawharun Nafiis +Masaalikul Jinnaan +ak yeneen yu nar a ñëwi +Yoonu murit +Podgora mooy péyu réewum Montenegro. + +Montenegro +Péy +Lisbon (Lisboa) moy péyu réewum Portugaal. + +Portugaal +Péy +San Maarino : Moy péyu réewum San Marino + +san Marino +Péy +Belgrad Moy péyu réewum Seerbi + +Seerbi +Péy +Jubuljana Moy péyu réewum Esloweeni. + +Esloweeni +Péy +Watikaa mooy péyu réewum Watikaa. + +Watikaa +Péy +Wiyen : Moy péyu réewum Ótiris + +Ótiris +Péy +Burusel Moy péyu réewum Beljik + +Beljik +Péy +Wadus : Mooy péyu réewum Liechtenstein + +Liechtenstein +Péy +Luksambuur mooy péyu réewum Luksambuur. + +Luksambuur +Péy +Monaako (Monaco) mooy péeyu nguurug Monaako. + +Péy +Monaako +Bern Mooy péyu réewum Suwis + +Suwis +Péy +Astana Mooy péyu réewum Kasakistaan + +Kasakistaan +Péy +Baku Mooy péyu réewum Aserbayjaan + +Aserbayjaan +Péy +Tibilisi Mooy péyu réewum Jeoorji + +Jeoorji +Péy +Ankara Mooy péyu réewum Tirki + +Tirki +Péy +(à traduire) + +The Linux kernel is a Unix-like operating system kernel. +Most known distros that use the Linux Kernel: + Debian + Fedora + Mandriva + OpenSUSE + ubuntu + +Xam-xamu nosukaay +Xerawlu leen ma sadd fii baati wolof +- miy sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf + +Ngirag ne sun jamono lañ xéy mbaanig +- jànqe ko yaawur te rañaane kàcc nag + +Te xéy ma ñépp këmm mbaa jupp la dal +- ña jànq it seen diñe gaay seen wéttal + +Gaa ya rañaan war ca galéemi fande ya +- te xét fétal ca ñall yuy gòlliku ya + +Ba génn kéewu dànna mom ëwoon na leen +- ni dédd def xaloobi gaynde sange leen + +Jéggi dayoom gu weesu lef moo ma ëlëm +- ma rët ba tax ma bëgg a dëflu cig woyam + +Ngir dekkalaat ko koomu alkandeem ma wér +- te suuxataat reen ya ba meññatam ma ñor + +ñu raas ko, fuuyu ko te ràcc, def cifaay +- yoor ca di fas dumóoyu lépp lëf lu aay + +jafal la giim te taal ko ngënji muy bërëx +- di lekk sun liw bi ba kenn dootu lox + +ñu naan ci dex gi bàyyi tèpp-tèpp yi +- ak dèq yeek ñunux yi, xunn-xunn yi + +dëtëm ba màndi raggu bokkul ak di ñéer +- ci lol dafay guusali put di yokku tér + +masëy-bandaŋ wa wenn dooñ la tooyalul +- waame wa mooy tooyali tool te koy ñoral + +ba tax ma fëx àkki wolof ya jiitu woon +- muy waxi sun maam ya dem ak ñii fi ne woon + +waxiin ya laa jëlaat, fasoo ñu delsiwaat +- te ñooy wolof yu wér ya, nar ñu dèkkiwaat + +tudde ko mottaliy mebët yu’ñ sémb +- ci dekkalaat baati wolof yuy démb + +Mamoor Xam Sa Diine +Aw naa ci àlli waa Unaare fekk léen +- ñu àngu ñoom ñépp di an calli aréen + +ma ëyu leen ne aaye naa ko, indi léen +- fukki andaar te boy te moytu aawe yéen + +Te aw ci xàlli jub te moy anéeri moy +- te wut aléeri topp àkki tool ya bay + +Te àlli bànqaasi moy ak àkki ngëméen +- bu léen di aas ci ëtt mbaa urmbali yéen + +Lépp lu aay ër ko fa tey aayelu ay +- tey àddu tey aar sa njaboot ci wépp ay + +Te bul di ës ba muy waral ñu ëñ sa kéew +- te mooy sa kiiraay li la ëw ba’ñ di la yéew + +Te bul asar lenn, na ngay afal ku ne +- sa xol bi nay af man a uuf mag’ak gone + +Jépp ayib ju dul sa jos umpale ko +- te ëmbalal ku nekk’u yiw àntule ko +Mamoor Xam Sa Diine +Ku bëgg nay bëgg lu baax bañ lu bonam +- te am bañum-rus ma te xeeñtu aw banam + +Te néewi mbóorante te doon ku xuuyi mbéey +- setal sa mbóoki xol te nàmp batti péey + +ŋoyal ca mbicci kaw ga bul jàpp ci pet +- moyal barastikook a bàyyi bul di xét + +Te rendi say mbamb ca pòttox ya te boy +- jam ko ca baljat ya te bèccingal ko wéy + +Te ñàkk paal ku dul ci Yàlla miy boroom +- te sàkku bëbbalam , ñeme’g péete ci moom + +Te buddi say mbémpeñi xol te buddi bóot +- sol ca ngënéel ba lépp pendal aki mbóot + +Te néewi bébbant nde moodi pëppi jëf +- di pindi pax yu feese pert bu’ñ la këf + +Defal bërët te binni ngir yéem sa ayib +- sàkku pexem faj ko te pasteefu te jub + +Defal sa jëf yi pàkkutéef wëlif poñat +- lu dee gi bette bette berndeele ko mat + +Mbewte nga bërgal ko potoxlu pèkki mbég +- Génn ci mballi bërjëlug bakkane rik + +Mbémburi xol di yéene nay mbèll mu set +- te banki jëf peek ko te mbaayàlla poñat + +Berul te bul topp mbaboor mi deel beres +- lu bon ci ag mbëbëstënam ci foo ko gis + +Bul ca deseb batt , faral béel ci lu baax +- te bul ca bar sa mbir na bir ci fonk baax + +Te dagg pàcci panka buural sa kañaan +- te daal di buur jëm ci boroom bi daw safaan + +Te fob sa baag yoor ko ci mbalka mom ngënéel +- tanq ca naan te wàcc mbóori xiila-xaal +Mamoor Xam Sa Diine +Damay janeer lu mel ne ceeñeeri cofeel +- mel ne ku ñéer cafka ga far càkku ca teel + +Ba maa ngi jànkoonte ci xol bi aw mettiit +- wu jege njòbbaxtani céy jipp jériit + +Ba xel mi jullusante na’ak xol bi, li jib +- xañ na ma cëslaay ba jamuj naa ci lu jub + +Mel ne ñunux ci man ci kuw maram lëjal +- ma far di cam su wéet di jukkat di jëfal + +Te jàmbat ’ak junj jeñul jóori cibeel +- ma jaaxle cumbóonu ci màndingum cofeel + +Ba jèmbraayi rònqooñ it di car-cari +- jàllawli xel mi xol bi it di jér-jéri + +Fit wi ni ñugg jokkalook njàqare xol +- lu sax ni ñumm mel ne coggal gu ñukkul + +Ba maa ngi ceeñeerlu ci biir am jayaxaan +- samab cës it call ba maa ngiiy ñeetaan + +Ma ñaxtu ñaxtu kenn ñëwul jàpple ma +- cawarte dem njàqare ñëw jaxalsi ma + +Ba càqaral na xol bi, jëmmi jamjamoor +- moo ma ñëwal njold ma jéllu kekki joor + +jullóotu naa ba faf ne jànjang ca ja ba +- ca dig njolloor ga ba weeroo ni Ruba + +Ma sàkku aw jaraasu pek jàppandiwul +- Ñu far ma njàmbaasali njëgg mom jarul + +Kanam gi ñëkk , ñaq, ñuqi lëf të ma +- ma jóofu ay jafeñ-jafeñ jàmm të ma + +Mu mel ni jaani ñas yu ñàng ñoo ma war +- te doon yu ñammasle di jurbi mel ne jur + +Ma aw ci ñallu jommiteg xel mu ñorul +- ba mel ne am njëgg mu ag cugri lëjal + +Ma jumm-jummi jiiñ jamono lii ma dal +- te xam ne moom du jag du jéggal du jagal + +Te xam ne njàngóor a ko gën jikko ndax it +- njekk da koo xamul du jekki it jubut + +Ma daal di jàppeelu ci lii ma xam ci moom +- te def ko ñukk jàpp nag ca kay boroom + +Te ñukk jëm ci moom te jòkk nag ci jëf +- te kañ ko, njukkal ko te far sóobu ci lef + +Doonte ne nag njàqare fi’m ne moo ma muur +- ni njóof di muure jaasi war ma bebb boor + +Du tee ma jéem a muñ te xam ne rek ngënéel +- déesu ko jox cuune ku muñ rekk la ñeel + +Te ñàkk jom day tax a jëf ñàkk te it +- da nay waral di jëf lu jóonu lol jubut + +Kon njegemaar yu jekk tey joŋante +- firdawsi cig njoggama yal nan ci joti + +Mamoor Xam Sa Diine +Na ngay dëgër ni déjj far jéggi dayo +- te doon ku dëjjarle di dàkku mbamb ya + +Ba mel ne mbëtti deg ya mbaa mel ne ndëfëñ +- du jàmbatub dagg ni dëññ mbaa wetañ + +Te bul di aw ndóol wu dëféenu fàww rek +- saxal di dàllu bul di dallu mukk nag + +Bul di dijooti ndàmm sonn a koy maye +- faral di dànna bob du déjjatuy moyi + +Dëtëm ndoxum ndam ma mu neex ci ndenqaleeñ +- nga nòyyi ndeemeexi ngënéel sa diine feeñ + +Dat ga di dòtti yaw nga des, dér , darale +- ni ku ñu dòtt tey ku dërkiis të file + +Di dëflu ciw tiis te nga ndarkepp sa mbir +- dëxëñ sa ndaaf te ndàmbe mbeg akiy naqar + +Te bul di diis ba faf di ndaari des ginaaw +- na ngay doronke dund gii doylu la teew + +Te bul di dàññi mel ne kuy das defarul +- déeyaale ak détti denéer yuy dexi xol + +Te doylu yaw doonte ne dóor-dóor nga ame +- dàggiku ndeem dooj nga am it bul ko gëme + +Te dànd dollenki bakkan, daw ko bu wóor +- te bul di dandal it sa xol bu xel mi dar + +Te dàngañal te moytu detteelu itam +- ca kàmbi diiŋat ya te daw dee du xalam + +Demal ca dex ga bàyyi déeg yi daa doyul +- te digg-dóomu nag ci lépp bul ëppal + +Te bul di ndeetet lu di tan-tanlu itam +- saxal di tan te bul dagook a ndiigu tam + +Na dëgg doon sa nding looy dunde dadam +- ta bay sa dooñu diine bul di dooji tam + +Te bul di doore mukk diisool ci lu ne +- da nay teree daanu di tee diig ci lu ne + +Xamal ne Yàlla day dënéerlu képp nit +- nang ko ba xel dàggiku ngir teg na la bët + +Mamoor Xam Sa Diine +Shaytaane day wëtt ci xol wudd la am +- wattu ko bul ko wàcc muy war di ku lëm + +Dafay woreek a wèddilooy werenteloo +- di wàjji ngëm di wònni mbas mbas du welu + +Wor ko te wòdd xol bi ngëm waaru bu wér +- sotti ci waame tudd Yàlla xol bi wér + +Weeral sa wañsu diine def say warugar +- bu ngëm gi woos ni waddbéer wu gar ya wër + +Werante wottee ko lu war, lu wóor itam +- na wuutu wor te worma wecci wane tam + +Nga weex sa xol wèkki ca luy wòllimiku +- te bàyyi weeje it welal tayle ba ko + +Te wòlli nag wëlli kañaan’ak weli rëy +- wetañ yu ñëw weñ ko te wetti far ko ray + +Te wacc weerante te wéer fa wòllare +- wareef akug wegeel te wicc njàqare + +Te wërsëgoo wiiri wakiirlu wis ca way +- te xol bi weex nga wattu waŋi wuute wéy + +Te waggar it sa bopp tey waaru bu wér +- te bul di wëndëng wa wogul wàqi te war + +Di waaj di walli weddi bakkan’ak loram +- te wéer ko bul weng ci moom ak ci wujjam + +Di waslu àq woor ci caaxaan aki nar +- wekku ci Yàlla def ko waay jëf la la war + +Te fònku waxtu xam ne daa wund lu rëy +- te bul di wuññi awra bul di wóoyu ay + +Na ngay woyof te bul di wex ci kenn tam +- ku dul ku bon te fònk worma tey xalam +This is funny. + +Mamoor Xam Sa Diine +Yaraanga’a ngi may yeerook a yedd ak a yunk far +- yërëm leen ma saag yées yées na yòqat a ngii di yër + +Ba yambar ya far nan tiim ma man may yalang mu yes +- ba yòqóolu naa far yòllugar nan ma far ma ber + +Te yiiruñ ma may yoppoorlu yërmaande far na jee +- ma namp yanaatub ñàqareek yëjji xol bi mer + +Te yombul samay mbir yemp yenkeewlu naa itam +- ci yammug yaras maa yay di yuuxook samaw naqar + +Te saa meññatum yaakaar mi yuntul ma yeene yiw +- ku nekk te teewul may yokkuw naqar’ak lu tar + +Ba saa kawarug mettiit wa yiif na ba yéegi yéen +- ba ronqoñ di yol saaw fit ni yèjji ni laaxu gar + +Ma yeewat ci yittey gaa yu yeeme mu të’a yewén +- ma yoongan ko yootug yokk fàww ci ngën ji yar + +Ma daw yaafus ak yunj’ak di yeex’ak di yox-yoxi +- te def yuww aw ciw yoon ba def yunn cig cigar + +Ma mujj di yeer muy yabbalum xel di yaag xalam +- te muy yaradal am xel ku yewwu du sóoru mbër + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu m + +Maandul te man yaw ci sag maas bul di mànke mukk it () bul def sa màndiŋ1 mi muy ab miinuwaay2 tubayul + +Xeebal masëy wa te muurloo waame moo ami may () sa fit bu muy màcc jëm cig maax lu mànke nga ful + +Bul mëdd may, yeete nang koy sante Yàlla bu wér () te say wax ak say jëf it nay màndaxoo matalal + +Bul makk-makkal sa bakkan nang ko miinali yar () bul mer te bul metti, màbbal moy te muñ lu la dal + +Metlànk far ko mu def menteñ ne meŋ ne mes () nga muure ko’g dëgg gàttal say mebët di jagal + +Tey muñ mettiit moom la Yàllay méngaleek musalam () bul mel ne maaka ma cig bañ-tàng dund saxul + +Mokkal te màggal, sa jëf bul màggal it matalal () bul yàq nig max te bul def makk màmm gënul + + 1 Àll bu sori + 2Dëkkuwaay + Tawub wick-wiccal + Ñawka lu tëlee dagg: ag ñawadi + Nëbb + Nay dëppoo, màndaxe mooy tollale gi nuy def ay balăs bu ñuy peese + Neexal ak a nbb-nabbee + Man a nax ak man a baab + Ne mes;naaxsaay + Mbaxana mu ñu ràbbe bant ngir feg aw naaj + Ne cell + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu N + +Nit nag ba laa nite day niit am xelam te du nar () te not ci am xel ba duñ koy nax ngirug naaxam + +Di nëbb tey jëf te neexum xel di néewali wax () di noppi cig neen soriy nëx-nëx matal naalam + +Di nemmikug naat te nargan bakkanam bañ a nay () nërméel itam néegi niig-niigal ngirug naayam + +Fu’m tollu nay naabu tey nàmpal xelam bañ naw () tey natt boppam ci ag néewam akug naatam + +Waxam nëtax neex ngirug nooyam nosub bakkam () di ñoddi muy nàcc’ak’ay nef daw sorig naagam + +Te néeg ci bakkan bi ay tànkam na nooj bumu dem () mu naj ko bu’m nàngi faaw bay nuur ci ag naanam + +Nemmat ko ba’m nenn noflaay bum ko xam na ko not () ba’m naagu bay niir te bum noppal ci ag naabam + +Te yeew ko cig naw di dóor ciy nengateŋ te mu nal () dëgër ca ba’m siit mu naaxsaayal ko ciw naajam + +Te nàmm xol ba ba dootul yëg naqar te du noos () ba dee ga ñëw far ne nuus ruuwam ga ci naawam + +Te dee du néggandiku’s lëf, nës-nësal aki nax () du tax mu dem, nagg-naggal yit du dog naalam + + Naj ak forse + Yeexe jëf ju am njariñ + Jeng akug joy + Sotti bu baax, nef it day firi njur mu jegee + Xeetu lafañ mooy wóom yi jegee tànk yi soree + Nàngi faaw:saaraan ak teg jë + yedd + Sàppi;bàyyi + Miir ak waccu + Fàmb;suufu faar + naw + Daas;ñawal + Bànneex bu diine lalul + Tëyye bu dëgër ak jàpp gu gaaw + + Jéllale + Waxi tappale yu nosuwul + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu F + +Fegul te fog te foogu tey ku fendi far () ci lépp luy fëkke te am fulla ju far + +Te fuglu fàwwu Yàlla tey fàggu bisam () ba mujj tey farlu ba feesaluw fanam + +Te femm bakkan bi te fàndaañu te fëx () ba fagg bul fipp ba far tàbbi ci pax + +Te bul di féttéerlu ba fiirook sa bakkan () facanteel ak moom te far ak Yàlla ba fen + +Fépp fu saytaane ñëwee nga fénati () te xam ne lépp lu’m la wax day fenati + +Yàlla ku fiir la kon faral féete fa moom () adduna daa fuytu te ag sax du jikkoom + +Te fiir la guy ferngali fàdd lay fexe () ku ci ne fóox sa tànk far ñàkk pexe + +Nga rët sa faalanqe gi fettax ne falañ () te fekk fomb wéy nga fande nib fariñ + +Nga fande fii ak fële feccikul ca teel () lépp lu lay musal ca fiir googa fexeel + +Sa faayda firndéel ko ci fonkug fagaru () fab jiwu fit te dem ca tooli xol faru + +Faxas sa fuuy gi tey fésal sa yéene nag () te ful sa jëf mu feese yiw nga falu nag + +Fodoŋ sa bakkan bi te folli ag palam () te fecci kóllareem ga fas nag sa kanam + +Faramlikug tenq ga bu’m la fif ba tax () nga far ko kon nga fuuti fequl te nga fëx + +Firincikul ca buum ga felli teel a fog () fenam ya buñ la fàbbi fippal takku nag + +Fobul te fas yéene mu foñ la foñ ko it () te bul ko faale it na fàndaañu ba rët + +Cig follikoom ngay falu fàwwu fëll it () ca maas ga formànko ci coona fës ci sut + + Bañ a nelaw guddi + Xel mu ñor akug mag + artu + Dox te solo dàll + Fënd ak sonn + Lànk ag topp + Tàqalikool ak moom + Dummóoyu ngir soof gu la mbir soof + neex + Ndëgg-sërëx + Kubéer gu àggut + joggi + Nga tiit + Liy tëb ak a dal ci put gi boo tiitee + Aw daanuwiin + Ñàng ga + Xëcc + Nga ànd ak moom + dagg + daw + wëlbati + Mere ak won ginnaaw + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu X ak Q + +Xarit xélul te xellu aw ci xàllu xam () te xér ci xëntewoo lu lay xiir ci xalam + +Te xettalil ku nekk xiirtal ko ci xay () te bul xatal sa xol bi it ba xëy di xay + +Te say xalam na dooni xiig nga xuuyi mbéey () te bul di xotteente te xér nag ci liggéey + +Melal ne xettar ci ku dëng mel ne xaal () ci soppe yépp ku xulóo nga xañ ko paal + +Te bul xulóok a xeex ak’ay xasante yaw () te bàyyi xiirook a xëccóo lu man di xew + +Te bàyyi xeebante xaroo xoddiku yaw () te ngay xereñ te jéem a xejj jëm ca kaw + +Te xeet xumaagi xol bi xembi ay xalam () xerawlu yiw wa faj sa xóndóoñi xalam + +Sa xel mi bu’m xuuge na jub xocc te wér () xëlóob ya buñ la gën di aaru kon nga ñor + +Bu say xalaat xajam nangay xajoo ku ne () te bul ko xumtoo te xemmeem njariñ lu ne + +Te bul di xàddi bul di xàcc xàllalal () ku nekku xàll bul di xallal it sa xol + +Te xippi gët yi xoole bul di xuuse it () te bul di xand xur wu xéewal ga newut + +Te ngay xareek adduna xas ko xupp ko () te xoqatal ko xuuxle it ci xeexi ko + +Te xam ne màggat mu Jigéen mu xubbidaas () te xettebee xettebe xàŋ gët ya laas + +Moo di misaalam bu ko xoymet sa kanam () xab ko te far ci xol bi xoolu ag bëggam + + xalaat + Set ak cilwiise + yuuxu + Jigéen + Nga man gan: xuuy mooy tàkk, mbéey doj wu ñaw lay doon ñu koy kosale ak moroom ja ngir taale ci, ñu jublu ci nit ku baax ku yor almetam di taal rekk ngir ganale + Lu mel xaal te ndaw te wex + Yitte;xel;faale + Dëkkoo + Waajal sa bopp + Am ab cér + xoos + rocci + Mar wu tar + lemu + Doomi gaynde + Tàyyi + Dellu ginnaaw ci mbir + Tilimal + yamadi + Jege ;tàbbi; dem + ragalloo + Tiital ko + Taxaw temb;lëjle witt + Kumur ak ras + Bët yu tooy xipp + Lu mel ne ab jégén lay doon ci ndodd mi + Yuurtala yuy yuy génn ciy gët + Won tuuti + Ttital ko + Xool mooy rëdd wi nekk ci ginnaawug mbaam + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu R + +Rayal sa rëy gi rendi reewandeek ragal () te roy rafet-rafet yi réccu ràggi xol + +Raxas sa réeri xol ba roppi gépp raw () te roof ca rus Yàlla te rembatal ko yiw + +Te rëcc saytaane raxal fiir ga mu yor () te rat ko rinkil ko du ruur génnati far + +Te bum la rambaaji defal rukk ci moom () ratt daŋar ja rekki mbooleemi naram + +Te rënk gëm ca róok te bul raf ba mu rot () te rikk bum la xoqutal ba tax nga rët + +Bakkan bi ruuj ko rijji reen ya riije ko () te rëq ndiggam la te ray ko robi ko + +Adduna rusloo ko te raaf rëddi faram () te bul di ruusaanu ak’ay ronni yëfam + +Tey raju bànneex di ko rog, ràññiku moom () raggal téram ba ba mu set rësal pexeem + +Sa noon yi buñ ree bu ci kenn rëcc tam () na seeni reefu ne ci yaw bu leen yërëm + +Na seen dereet yi riix ci suuf si rungleen () te ràngleen lu rëy te metti rombleen + +Nangay rañaan di jàggi ruur di daw fu rëb () di tuubi rëcc-rëcc roñ ca yiw ya ŋëb + +Te riggalal ngënéel ci xol bi yu’ñ ca riim () te bul di reggal it sa kàddu dee ko riim + +Te bul di ràppal ak a reesal lu lewul () doonte lu ras nga am te am rooy rafetal + +Te bul di rannamtalu ngir rëbb ci wor () ngir jëfi ku’ñ rëbb la daw ko jiitu far + + Fees bay tuuru + yeew + Tànk yu rinki mooy yu wóom ya jegee tànk ya soree + jàkk xool bu baax + Dindi;summi + Mooy Yàlla ci séeréer, bu ko wolof waxee li mu ci jublu mooy dégéj ba gën a sori + gajj + Buddi; sulli + Daggate + far + Diibal ay tànk ngir bëgg dara + Rog + Raju : sàcc xibaar + Digub dee maanaam jotug waxtuw dee + Taq + Boole mbooloo jiital + gàll ak yan + song + Daaneel ci suuf + Feesalal + Sësale + Reggal kàddu: diisal ko + Wax wax ju suufe te teey + Yéré yu tàlliwul + Cere ju amul ñeex + Wax wax ju neex + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu S + +Sutuxlul seŋes Yàlla war sàllu ngëm ()te sóobum lefam daw ba seerug palam + +Sawar am sagos ngëm te sàkkub sagam () te sëmbërtaloow yiw ba gën sépp sem + +Te sartaagal ’ag sag safoo Yàlla jëm () ca kaw sippi ag sew waxam mbaa jëfam + +Te naan kaasi ngëm suggalee sell yaw () te bay saw sas’ak gopp sunna’s ka xam + +Selanglul te bul dox di sonjaanu sas () te ngay sopp Yàlla’ak a santiy mayam + +Sa bakkan bi dang koy sébéñ ba’m séxéñ () ci ag nooy akug topp sunna’ak sëfam + +Te siiwal pexeem bul ko bàyyeek sa koom () dafay sooke aw ay sexeeral mbiram + +Te siiw mbicci kaaraange semmal ko jëm () fu sooŋooŋ akug sooy newul ak tilim + +Nangay sémb loo man di sottal di sos () te siiw am njariñ ak sutura’ak ngërëm + +Te bul jëf lu suufeek lu sew bul soxor () nangay jëf lu set seytu sàqiy mbayam + +Nangay sonne xam-xam soril luy safaan () te bul sob te bul sikkal it senn cam + +Te bul sóoru mbër it ndegam suq nga () te bul soxlu mbër soxlawoolug manam + +Te bul siis itam ab siboor bul sob it () nangay seexlu ñaawtéef wa sib ag jëfam + +Te bul sànj bennub jullit sopp ko () te bul koy sabooteek a salteel deram + +Nangay digle ag sell bañ caa selaw () suturaal ku nekk it te sàmmub deram + +Te bul def safaan it ba tax ngay sangéem () sippeekul di surgab ka man tey ka xam + +Safoo sab sëriñ fàwwu dib sang yaw () te sa baati seedeem ka sappug demam + +Nangay faj sa jikkoy sagañ sempiku () te bul suux ci sañ-sañ yi Yàlla’a ko am + +Te bul nig ci am mbir suba’akiy sibir () dafay faataluw yiw du sottal mbiram + + Duggiin wu gaaw te bette + Seŋe: kiiraay + Aw fas wu baax + Seeru: jot + Ag dal + Sëmbërtal ab rido mooy wàcce ko, fii mooy muuróo aw yiw + Aw nit + Weesu fa nga naroon a yam + Tuur ;wàcce + Ñaaw-ñaaw + Naan naataat + Dal am xel + Booyal; bay ab tool booyal ko am at door koo bayaat + wolli + Làggi ak tàmm + sabab + Sexeer: gaw ci wet yépp + Ŋoy + Féete kaw + Wéradi + Tàmbali + Dëkk ak cokkaas + Kiy topp ci mbër + Suufu : bul suufu mbër ak a top ci ginnaawam waaye jéem koo man + Ab xaaraankat + mere + Noppi akug dal + Dëgmu sëgg ngir jaaxle mbaa kersa + Ka sapp ag demam : kay bëgg a faatu + Jikko ju baaxut waaye cosaanam mooy tooy ju yàgg + Ginnaw suba + +Mamoor Xam Sa Diine +Arafu T + +Toroxlul te tuub tey topp Yàlla te teet tereem () te teey tabe tey tàggat bakkan beek a daw pexeem + +Toŋal ko te tóngook moom te tëkku ko bul ko tëy () toroxlu ci Yàlla’akug tëyam sàkku yërmandéem + +Te bul toog te bul jëf it ci maa tey mu tund lool () na tandu te bul teeŋal ku të tukku tuskareem + +Tegul yaw ci kaw yoon wii taxañ bulk o teggi tam () te bul taga-témbéekug tàyyeel ak lu deesi yéem + +Te daw tabarondum digg njolloor mi ngay taseel () mu teggilook’ay tàbbiloo teeni tappaleem + +Fegug Yàlla moo gën gën ji tunkaar akiy tata () nangay tàbbi kaaraangeem te bul génn bul ko jéem + +Te taafenteloo nag aw turam foofu man di dem () te ngay tos sa xel ba’m saf ku dul yaw nga far ko +tiim + +Nga totti sa xol ba’m set ci tër ak tilim-tilim () te muñ tiis akiy tar-tar ba gis tërgënub taneem + +Te daw tañaxook tànjang ci mbir moo xalaatagul () te daw tumurànkeg xam nangay tabb cig wuteem + +Nangay tànn say àndaale tey tànnu taaru jëf () te tàmmal sa làmmiñ wax ju yiw mbaa nga far ne xiim + +Te tooke sa bànneex far ko tiiñal te tanc ko () tëjjal ko tàbbal ko ciy pexeem + +Nangay tembareel say mbir sa jëf takku am njariñ () nga lal tesarantag muñ te bul tayle gor ci keem + +Te ngay bàyyi tiisanteek a teefonke ak tërëf () te taataar toroxlul nag ka deesul gis’ag tëleem + +Te tapp ca xéewal yee te jug tepp-tepp yii () te tàggooki tër ak taq tey fob teraanga leem + + Wonante ginnaaw + ragal + Ñaaw ñaaw gu ëpp + bari + Yanu; sëf; gàddu + Wéy te dem + Tabarond:màggat + Ay bali fett walla defukaayam + Fegukaayu bali fetal; fort ci fr maanaam fi soldaar si di làqu di fa aaroo cib xare + Tuddoo ak sukkandikoo + fiime + fóot + Jeexiitu aw mettiit nekkoon + Tànjang ci mbir tëb tëb tàbbi ci + Dëkk ak sax ci dara + baax + Posone + Lakkal witt + Tas ci diggante bu xat + Wéradig tànk la guy tee man a dox, fas lay faral a dal + Jampal + Tesaranta: ag basaŋ + Kee : Xaalis ak wurus + Xëccoo + Jaaykatu xar, mu jublu ci werante + fakastalu + Saaraan + As taa-taa su ndaw + +Mamoor Xam Sa Diine +Ag mottali : + +Laa yéene woon a indi fii nag la mate () te mooy wolof ya sànku woon ba tëe jote + +Ma jug dabaatalaat ko ngir mu dekkiwaat () te suuxataat reen ya ba xob ya seqiwaat + +Ba meññatam ma ñor njariñ la daj fu ne () ku nekk mos ca kotttéef la daj ku ne + +Ñu bokk fëx ku des ginnaaw jéem a dabe () te daw ba roppi népp nag te buñ rabe + +Mu dooni mbég ci népp tey ag ségëre () te xel yi dal ba xol yi dootul fér-féri + +Yaraax yaraaxam yi itam fatt taraj () ba ab poroxndoll du des bu lenn xaj + +Ba sun cosaan xajam-xajam ya set wesal () layaat ko seggaat ko ba tër dootu ca des + +Ñu rat ko nag ba dóotu dàngang jawali () ci ndànd-fayfayug keneen bay lëjali + +Ne nit amul lu dul cosaanam ak ngëmam () cosaan la it làkk a ca jiitu nañ ko gëm + +Ku wàcc sab andati and boo dem it () fekk boroom ca kaw ne déjj day ku mat + +Ndegam dangaa waññiku delsi ci sa bos () fekk keneen toog ca dangay ku xel ma des + +Kon maa ngi woo népp ñu bokk takkuwaat () te fonk suñ làkk wi buñ ko sànniwaat + +Nit bu nitee du dem ci tool bàyyi sasam () di bay sasuw keneen ba booyaluw sasam + +Dafay fexee lippiku népp bay sasam () bu sottalee bayal keneen di ndimbalam + +Dafay jariñ nit kit e bañ koo jariñoo () balaa jariñ nit ki nanig ba jariñu + +Ñu ñaan ci Yàlla miy boroom mu boole ko () ci jëf yu yiw ya suñ xel it mu dolli ko + +Te def ci woy wi barke xiirtal nu ci way () ci fonk suñ làkk wi népp bokk wéy + + Ba tax manul a jot yeneen làkk yi cig jëm-kanam + Seqi: jebbi + Wattiit; lu nu watt + Daw + teeyadi + Mbégte + Diggante yu dara nekkul + Bën-bën bu xaw a yaatu + yeew + Rëcc ak màmm + Waññil keneen aw sasam ginnaaw bi nga bayee saw sas ba noppi + Xasaayit gi + Sax ci mbir, way ci deŋ + +Mamoor Xam Sa Diine +Football benn sport. + +A-League +Bundesliga - Almaan +Bundesliga (Otirich) +Campeonato Nacional - Gine-Bisaawôo +Campeonato Nacional - Kap Weert +Campeonato Nacional - Saw Tome bu Prinsip +C-League +Eredivisie - Olaand +Girabola - Angool +I-League +J-League +Ligue 1 - Faraansi +Ligue Pro +La Liga - Espaan +Liig 1 - Senegaal +Major League Soccer (MLS) +Premier League - Angale +Premier Soccer League +Primeira Liga - Portigaal +Série A - Beresiil +SuperLeague - Girees + +Xool it +Sport + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +Bokk na ci mboolooy way gàddaay yi jañu woon ci kaw Amerig menn mbooloo mom dañu ko cee ga woon manante ko ci (forse ko ci), mbooloo moomu mooy ñi juge woon Afrig, yobbu woon nañu cig sañ-bañ 500 junni ci ñoom niki ay lar (jaam) ci diggante bi nekk ci 1619 – 1808, jooju mooy jamono ji jëli ay jaam indi Amerig nekkee dib sémb bu ñu taxaw ci amal ko. + +Liggéeyloo jaam yooyu wéyoon na ak liggéeyloo seeni njur (seeni doom) rawati na ci bëj-saalum bi di barabub mbay, fi aajo tare woon ci ay liggéeykat yuy liggéey ci suuf seek tool yi. +Waaye taxawalug njaam gi mi ngi door ci awril 1861, bi xareb ñoñ bi (guerre civile) dooree ci diggante diiwaan yu gore (libre) yi ci bëj-gànnaar ak diiwaani bëj-saalum yi ŋoyoon ci njaam gi sax fi, loolu sax taxoon na ba 11 diiwaan ci ñoom dogoon ci bennoo gi (federation). + +Ci bis bi njëkk ci samwiye 1863 la Abraham Linkoln jibal goreelug jaam yi, googu jibal moo neenal njaam gi ci diiwaan yooyu dogoon ci bennoo gi. Ag njaam nag neenalees na ko ci mbooleem Diiwan Yu Bennoo yi bi ñu defee fukk ak ñatteelu soppi ci sartu réew bu Amerig (constitution )atum 1865. + +Waaye bàyyi gi ñu def ag njaam ci Amerig lépp teewul ñu ñuul ñi ci Amerig di wéy di jànkoonteek ay coona, di ñu ñu xañ dund gi népp xam (normal) gi boddante ci biir xeet gi wéyoon di am waraloon, ñu nekkoon di jot ci njàng mu suufe . + +Ngir gëstuji dund gu gën, ñu ñuuli Amerig ñi doxoon nañu juge ci seen diiwaani bëj-saalum yooyu di yu mbay ak àlle ak kaw-kawe, laggsi ci yu bëj-gànnaar yii di woroomi xay ak taaxe. Waaye loolu lépp taxutoon lu bari ci ñu ñuul ñi manoon a jot ca liggéey yu méngoo ya, ndax kat yoon walla aada daa farataaloon ci ñoom ñu dund cig beddiku wëlif ñu weex ñi ci ay gàdd (Cartier) yu ñàkk te ndóol ñu léen di tudde (ghettos). + +Ci mujji ati juroom fukk yi ak njëlbéeni ati juroom benn fukk yi, waa Amerig yii bawoo Afrig jëfandikoo nañu li ñuy wax doggoo gu koom-koom (boycott économique) Martin Luther King jiite ko, ak ay doxi ñaxtu ak yu dul yooyu ci anami ñaxtu yu jàmm, ñu ci doon sàkku ag yamale ci lépp ni ko yoon waxe te bàyyi gënaleg xeet gi ñuy boyal jëme léen . + + +Yëngu-yëngu gu xeex àq ak yelleef googu àggoon na ca njobbaxtal la ci 28/ut/1963 bi lu ëpp 200 junniy nit dajaloo ci xeet yépp ca kanamu estati bu Linkoln ba ca Washington péeyub Amerig ngir déglu Martin Luther King mu naan : Maa ngi gént bis bob doomi jaam yi ak doomi séeni sang danañu ca toogandoo ca laamaari (xeetu montaañ) Jorgia yu xonq ya, wër ndabul mbokkoo la… Maa ngi gént bis bob sama neenti doom yu ndaw yii dinañu ci dund ci réew mom deesu leen fa àttee ci seeni meloy der waaye ci seen ëmbiitum jëmm (li seeni jëmm ëmb). + +Giinaaw xutba bii toogaatuñu lu bari dara rekk Kongres daal di def ay yoonal yu tere raññatle ci biiru xeet ci woote ak njàng ak liggéey ak dëkkal ak ci campéefi mbooloo mi. + + +Waxuma la sax ne lu bari ci waa Afrigi Amerig yii seenug ñàkk daa tar, looloo waral ñuy tàbbi ci sineebar ak tooñaange (criminality). + +Ci at yu néew yu mujj yii yittey Yëngu-yëngu gu xeex yelleef ak àq googu soppiku woon na, ndax kat bi ñu tàmbalee di génne ay àtte yu bees aki yoon yuy tere raññatle, ak bi ñu ñuul dooree di tuxu juge ci kureel gu suufe gi dem ci gu digg-dóomu gi, bi lii amee laaj bi leegi mi ngi jëm ci ndax nag raññatle gu xeet gu njëkk ga ñu jëmale woon ci ñu ñuul ñi du waral ci àtte gi (goornamaŋ bi) mu jël ay matuwaay yu am solo ngir yéwénal nekkiinu ñu ñuul ñi . + +Jéego yii ñu tudde “àttey jëf ju feddaliku ji” (muy anamug jël ay liggéey yu ñu weex ñi (ëppte yi) manoon a jot, jox léen ñu ñuul ñi (néewte yi) ) Jéego yii nag làmboo nañu duggal ab lim ci ñu ñuul ñi walla yeneen néewte yi ci mbooleem barabi liggéey yi. Ak nangu ab lim ci ñoom ci daara yu mag yi ak bànqaas yi (les facultés ), ak lijjanti ba lenn ci nit ñu ñuul ñi di man a falu ci Congress ak yeneen doomi néewte yi. + +Ci ati juroom ñaar-fukk yi coow ak dàggasante bi bari woon na ci ndax jëf yii am nañu njariñ ak ndax tegu nañu cig maandute. + +Waaye lu man a xew daal mooy coppat yu am solo yii am ci at yu mujj yii mi ngi feeñe ci taxawaayu ñu weex ñi ci Amerig. Ay maas (generations) ci waa Amerig leegi ñor nañu ba ñu déggee xutbab Martin Luther ba yoroon baati (maa ngi gént ya). + +Waxambaaney Amerig yi leegi nit ñu am worma lañu ci xeet yépp, te it ñu weex ñi gën nañoo nangu ñu ñuul ñi, ci mbooleem wàlli dund yi ak mbooleem campeefi mboolaay yi +Gordon Brown mooy benn ministru Nguur-Yu-Bennoo (27 suwe 2007 – 11 mee 2010). + + + +Nguur-Yu-Bennoo +Manchester United benn football club ci "Premier League" (Nguur-Yu-Bennoo) ci dekku Manchester. + +Premier League: +1992-93, 1993-94, 1995-96, 1996-97, 1998-99, 1999-2000, 2000-01, 2002-03, 2006-07, 2007-08, 2008-09, 2010-11, 2012-13 + +Staad + +Old Trafford + +Dencukaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + Alex Ferguson + Wayne Rooney + Carlos Tevez + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Manchester United Official Website +Nguur-Yu-Bennoo +Angale +Premier League +Football +Premier League: football (Angale, Nguur-Yu-Bennoo). + 1992-1993: Manchester United + 1993-1994: Manchester United + 1994-1995: Blackburn Rovers + 1995-1996: Manchester United + 1996-1997: Manchester United + 1997-1998: Arsenal + 1998-1999: Manchester United + 1999-2000: Manchester United + 2000-2001: Manchester United + 2001-2002: Arsenal + 2002-2003: Manchester United + 2003-2004: Arsenal + 2004-2005: Chelsea + 2005-2006: Chelsea + 2006-2007: Manchester United + 2007-2008: Manchester United + 2008-2009: Manchester United + 2009-2010: Chelsea + 2010-2011: Manchester United + 2011-2012: Manchester City + 2012-2013: Manchester United + 2013-2014: Manchester City + 2014-2015: Chelsea + 2015-2016: Leicester + 2016-2017: Chelsea + 2017-2018: Manchester City + 2018-2019: Manchester City + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.rsssf.com/tablese/engchamp.html + + +Football +Angale +Alex Ferguson : manager Manchester United (31 tabaski 1941 dëkk Govan, Glasgow). + +Football +Asamaan (fr : ciel) + +Suuf +Saytubiddiw +Ndox (fr : eau) : Yolaakon + +Ndox +Safara S (fr : feu) + +Li wuutale Safara si ak sawara wi nag; safara mooy taal safara, lépp lu ñuy kos muy tàkk ngir ñu man koo taale rekk safara la, bu dee lu tuuti liy def xuyy ne xamaj daldi fay loolu fer-ñent la. Bu tàkkee ba jàpp di bér-béri sawara la. + +Kon sawara wi moo gën a yaatu safara si. + +Safara +Gόor (fr : homme) + +Gόor +Jigéen' (fr : femme'') + +Jigéen +Faraañse, mooy làkk wa juddoo ca réewum Faraas. + +Faraas +Làkk +Mburu (fr : pain) + +Mburu +Guddi (fr : nuit) + +Suuf +Bés +Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke , dale 1927 ba 1945 + Sëriñ Muhammadu Falilu Mbàkke , dale 1945 ba 1968 + Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke , dale 1968 ba 1989 + Sëriñ Abdu Xaadir Mbàkke , moom ag ayam weesuwul 11 weer dale 1989 ba 1990 +Sëriñ Saaliwu , mi ngi gane àdduna 1915), di xalifa dale 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007 + + Sëriñ Basiiru + Sëriñ Suhaybu Mbàkke + Seex Muhammadu Murtalaa Mbàkke + +Ñooñu ñoo di ay xalifaam, dees na indi ñeneen ñi +Sëriñ Saaliw mi ngi gane àdduna, ca Njaaréem(Senegaal) ci guddig àjjuma gu 14 ci weeru tabaski, atum 1333 g.g, dëppo ak 22 satumbar 1915. Aji juram ju góor di ku jaradee leeral ngir xam gi ko nit ñépp xam di Seex Ahmadu Bamba, ju jigéen di Soxna Faati Jaxate, mom Sëñ Moodu Asta mu baax ma te sell. S Tuubaa bi mu ganee àdduna daa bindoon ciw kayit tur wi di (Saaliwu giy tekki aji baax, aji yéwén) jox ko Sëñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana, ne ko tudde ko ko, bi mu ko defee moom S Dagana, daa daal di bind as lëf ciy bayit ñaanal ci liir bu tedd bii aw fan wu gudd akug wér, akug yékkatiku ci jamonoom ba mel ni jant, mu wax ca ne: + +«Yal na Yàlla mii di Aji-des bàyyil ñu fi Saaliwu mii mu ñu may te def ko mu jël turam wi (aji-baax).Yal na ko fi desal mu dib jant ci asamaani jamonoom, bu ko defee, muy leeral kanamam gu këriis gi. +Yal na ko fi desal muy kuy mottali jub gi fi Yonent bi indi woon, di ku barkeel, di ku wér, tey ku am muur» + +Am njàngam +Ay ceññeeri xel ak màndargay yewwute ak man a wattu teeloon naa feeñ ci moom te booba matagutoon a dal jàng, bokk na ci liy dëggal loolu te di ko dëgëral lii nettalikat yi di nettali muy ne moom de mokkaloon na xasida gii di (Ikfinii) te booba gone gu ndaw la woon, ginaaw bi mu jànge Alxuraan ca Tuubaa ci loxol nijaayam S Alasaan Jaxate mom Jàmbaar, ba mokkal te bind kaamil, ginaaw bi mu dugg ci jàng xam-xami diine yi ak làkku araab ci ay ustaas yu màgg niki Seex Moor Saasum Jaxate mom Xaali Majaxate Kala ca Aynu Maadi ak Seex Muxtaar Guyaar Jang walla Njang ca Husnul Maab(Tindoodi) ak S Abiibu ca Tuubaa, S Mut Dem ca Njaaréem, Seex Aamid Saw ca Mewndu, kii mooy ki ko jàngal xam-xami gëstubiddiw yi (falag) ak melosuuf gi nga xam ne xóotoon na ci ba àgg ci di xam ci mbiri ay réew ca Asi, Tugal ak yeneen réew lol ña fa dëkk sax leeg-leeg ñu xaw koo réere. Ku soppoon yër ay téere la, ndax saxoon na ci ab diir ci jamono ba mujjoon di géej gu deesul jot ag suufam ngir ag xóot. Bi Sëñ bi àggee fii ci njàng mi la gis ne daa war a dugg leegi ci jeneen dara mooy ju tukki, ndax tukki benn la ci daara yu mag yi xam-xam di juddoo, di yokk jarbu tey dollim xel, ndax bari na xam-xam yu ci juddoo, ndax dina yobboo ñaare ci xalaat ci dénd bi te Yàlla (tudd naa sellam ga) yàgg na cee woote jëme. Ci noonu, mu def lu sakkan ciy tukki ci biir réew meek biteem, ci mbooleem diiwaani Senegaal,Kot Diwaar ak Gàmbi, mu jële ca daj gu mag ak jarbu gu réy ci lef yu bari + +S Saaliwu ci wideo: +http://www.youtube.com/user/lahaddf + +Yenn ciy meloom + +Ab xam-xamam +Niki ñu la ko waxe leegi Sëñ Saaliwu nekkoon na di ku géeju ci xam-xami lislaam yi: Tawhiid (wéetal Yàlla (t.s)) fiq , tasawuf , nos-wax walla nahwu ak nos-woy (haruud) ak jotal (balaaxa) ak leeral (bayaan), muy ku yéeme woon ci woy , daan def ay jam ci woyi dongaam yu tarbiya yi daan faral di def ay woy yu yéeme, ñoom de bokk nañu ci ñi gën a man a woy ci araab ci Senegaal ku ci mel ne Sëriñ Alhaaji Lóo , Utilisateur:Abdu Xaadir KEBE mi ci wikipedia, nga xam ne loxoom lu fa am solo la te ay gëstoom gën a màcc ci làmmiñu wolof, S Xaliil Màkke, S aboo Kebe mi def ab dalub murit bu jéggi dayo ba ci làkku araab "www.wikimouridia.org" , S Mamoor Kebe, S Alaaji Mbàkke mi nga xam ne lu dul jeex ciy téere la taalif ci yoon wi ak aji sosam añs , ndax daawu leen bàyyi ci seen jàmm, foo ko fekk ma nga leen di soññ ci sàmmoonteek sarti "jotal" yi walla balaaxa ci seeni njuréefi woy. Ku mokkaloon lu bari la ci woyi waa Gànnaar yi ak waa Andalusi yi + +Ag sonnam ci Jaamu Yàlla +Daa na toggoo ci jaamu Yàlla yi lu kawe misaal, mu daan taqook ay dog ciy wird aki tudd-Yàlla, daawu leen ginaawal mukk ak lu yitte yi tar tar mbaa xat-xat yi baree ko ni, kenn ci taalubeem yi nettali na ma ne moom de masul a jël aw wird ndare bu da caa sax ngir sàmmonteek Addiis bi naa "Jëf ji Yàlla gën a sopp mooy ji gën a sax ak doonte néew na", muy ku xéroon cig jaamoom ci tënku ci Alxuraan ak Sunna, daan teet bidaa ak cibéel (lu ñu sib), ci anam gu jéggi dayo ba cig tar. + +Ag dëddoom +Sëriñ Saaliwu daa dëddu àdduna ginnaawal ko ginaaw bi ko àdduna dëgmalee, jublu ko, mu ñëkkaloon ko ag kanamam ginaaw bi ko àdduna muuñee, ag dëddoom àdduna nag ca xol ba la ko defe, ndax teewu koo topp ndigali Yàlla (t.s) yi aju ci dundal suuf si, ndax Yàlla (t.s) nee na : «Moo leen sàkke ci suuf si te sàkku ngeen dundal ko», bu bokkoon ci ñiy toraxal suuf si ngir woote ag dëddu doo fi gis tay yii tabax yu kawe yi mu fi def ngir rekk kaweel baatub Yàlla bi, doo ko gis it kon muy bay lu tollu ne li mu daa bay ngir rekk séddaleeti ay njariñam aki njuddeefam ci nit ñeek ñu ñàkk ñi, di leen wax laayab Alxuraan ba: «Ñun de dañu leen di leel rekk ngir Yàlla, soxlawuñu ci yeen ag pay du caagéenu ag cant» + +Ag Ñawam akug Yewwoom +Sëñ saaliwu nekkoon na di ku yewwu, ku ñawum xel, ku amoon la ag xereñ akug xóot ci xam mbir yi, boroom xam-xamu xel la woon (psychologue), ku daan xam xeli nit ñi la woon ak seeni jeng-jeng, booy tàmbalee wax ak moom rekk mu jëli la, ndànd la, boroomug ñaw la woon ba deesi ko seetlu saa soo ko tegaleeb laaj, ak bu mu man a doon. Bis gan dikkal na ko di kilafa gu bawoo ci biti, bi muy wax ak moom ci lu aju ci tànnéefi njiit yu Senegaal yu waroon a am ca jamono jooja, gan ga daal di koy laaj kan la faral ci lawax yi (les candidats)? Sëñ bi ne ko: man de ki askan wi tànn rekk laa faral, te loolu manul a am ndare bu tànnéef yi daa gore, sell te leer, looloo tax sama bëgg-bëgg mooy na mel nii, ci noonu gan daal di ne : tontu bii de bu diblomaasee la . + +Ag Ubbikoom +Ku ubbiku la woon ci ñépp, daan tertoo ci kanam gu lewet guy muuñ, ak dënn bu yaa, di jaxasook ku nekk ci lu dul genn wàttuwu, ñi duli murit it mu jàppe leen mbokki diine ak yu ban, ngir jëfe waxi waajur wa: «wépp wird wu waay wor te Yàlla rekk tax, moo xam wu Jiilaani la mbaa wu Ahmad Tiijaan, mbaa muy wu keneen ci Qutb yi, yooyu yépp a baax ndax cig jub lañu nekk yooyu yepp » + +Yërëmam nit ñi ak Soppam ñeel xale +Yërmaande ji mu am ci mbindéef yi ak ñeewant gi mu am ñoom xaw nañoo nekk di lu maneesul a misaal, moom de kuy yittewoo mbirum jullit ñi la ak fu ñu man a nekk, di nemmiku ak a xeeñtu xew-xew yiy xew ci réewi jullit yi niki xareb dóox gi (guerre de golf), ak intifaada ca Palestin, ak mbooleem tër (condition) yi jullit yi di dund ci mbooleem àdduna bi, mu daan digale ci ñu wàcce ay kaamil ngir ñaanal leen ci. «Man ci sama jëmmi bopp (Abdu Xaadir KEBE) dem naa fa moom bis ànd ak sama jenn mag ne ko Sëriñ bi war ngaa ñaanal jullit ñi, ndax yaw yaa fi nekkal Yàlla ci kaw suuf, te kat waa Aamerig ñi ngi taal àdduna bi te loolu ñi ngi ko gën a defe ci jullit ñi, taal nañu ab xare ca Afganistaan, taalati ko ca Iraaq, jamono jii ñu nekk ñi ngi waajal ngir taal ko ca Iraan, mu daal di feeñal yitteem bu baax ci wax ji ne ma loolu nu mu deme ma gën ko koo leeral, mu ne loo ci xamati naa ko yëg ndax lu ma ci yëg du yam ak lu ma ci yëgul, te kat booba waa Aamerig feeñaloon nañu yitte ju mag ci song Iraan, ba tàmbali woon a yëngu's lëf jëm ca Dóox ga (le Golf) waaye ba leegi waxatuñu lu dul luy jàmmal, ba sax njiit lu bon la daa xeex rekk di George Bush far na daanu, kii di Barak Obama daal di toog, te moom benn ci dig yi mu doon def ci bi muy sàkku ñu fal ko mooy toog ak Iraan waxtaan, yal na ko Yàlla àntul, te gëm naa ne day àntu ndax waxi Sëriñ Saaliwu ji, lii nag ñeewant la ñeel jillit ñi waaye it ñeel nit ñi, te ca baayam la ko jële mi daa wax : «Yaw boroom nguur gi (di Yàlla) yaw mi màgg ba weesu fayoontoo, rikk nanga yërëm mbindéef yépp » kon moom mbindéef yépp la yërëmoon rawati na jullit ñi waaye it baatin la ndax sunu boroom fanq na ay wi cig ñaanam ci barkeem. + +Yërëm xale yi +Mu nekkoon di ku am ñeewant ci gone yi, yërëmoon leen ni mu ko defe mag ñi, mu daan leen dimbale di leen gunge ci jafe-jafey dund gi, mu daan mettitlu te daan naqarlu bu gisaan kenn ci yale yi mu tumbrànke , mbaa sonalees ko cam njàngam mbaa mu ami góom mbaa mu wéradi mbaa mu xiif. + +Daawul toog ak ñoom ndare bu da leen a teral, jox leeni neexal aki mbiskit ak lu ni xeetoo. Daa na àndaale ak ñoom ci tukkeem yi, di kaf ak ñoom mel ni gone ni ñoom te loolu lépp ngir ñu fàtte seeni waa jur ba man a dékku li ñu leen bëgg a sol ci yarub lislaam bu kawe te sell, ndax kat gone baaxoowul a miis ay waa juram ngir ñeewant ga, waaye fi moom day am ngir yërmaande ja. Mu daan fanaan ak ñoom ci néegi boppam yi, nekkaloon na leen di baay ci li baat bi ëmb ci maanaa, taxoon na xalaatatuñu seeni way jur ngir wuutu gi mu leen wuutu woon ci ñoom ci jëfam ju baax, foofu nag amal na fa waxi baayam ja ba muy ñaan Yàlla (t.s) naan ko: «taxal ñu fàtte seeni way jur ngir man» +Waaye nag yërmaande ji teewu ko woon a taxaw ci yar leen ni mu ware, mu daan waxtaan ak ñoom ci nu kawe seeni at, daan leen nettali ay xisa yoy daawuññu ci xam dara, waaye da daan sedd bis ba ñuy doone mag ba koy soxla ca seenug dund, loolu nag ci Yonent bi Muhammad (j.m) la ko daa roye, ndax mooy ki daa wax Omar ibn Abii Salama te booba gone la gu xamul li mu koy wax: «Neel Bismil Laah, te lekke sa ndijoor te lekk ci sa kanam» + +Ag dundam +Dund gu wow la yoroon gu soofiyoo, gu ag dëddu àdduna muur, ragal Yàlla peek ko, biir ga di yërmaande, muy ku amoon ag ñeewante ci gone, te yéggoon aw wartéef jëm ci doomi aadama yi, ku amoon ayba la woon ak wegeel, ku ubbiku woon la te lewet, waxi woykat ba dëppu woon na ci moom : « Lewt ba ne domm, diis ba ne gann cig wet () woyof ba ne toyy, saf sapp ak boroomam » boo koy xool rekk gis ag Yàlla ak aybaam ga, dëggoom ga, wegoom ga, muy ku ñépp wormaaloon, ñi ko jegeek ñi ko sori woon, Benn ci labbe yi ci Senegaal seereeloon na ko ginaaw ag làqoom: «Kii de àdduna da koo dikkal mu toog fi suuf», loolu di wax ju réy, di lépp dikkal na ko te faalewul dara lu dul Yàlla te xam ne dara amul solo lu dul moom, fii dara saxu fi, dara dëkku fi, woykat ba nee na : «Jural-leen dee, tabaxal mbàbb», muy ci maanaa lu fi waay jur dee dina digg leegi ne ko fuuf, lu ngéen tabax it day mbàbb leegi, kii nag lii la tegoon ci ron bëtam, jëfam jépp it Yàlla la ak lu ci jëm, misaal mi kenn la woon ku àddinaadi, te teewul mu sos fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te loola gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru. + +Kenn ci murit yi nee ne bokk na ci bind yi ñu man a jële ci moom: «Nekk gi mu nekk doomi S Tuubaa doy na teraanga te dib xalifaam, nekk it mag mu am ay xéewal war naa tax a noppalu, te moom boole woon na ñaar yooyu yépp, waaye teewu ko woon di yëngu jamono ju nekk ak a liggéey, kon loolu li mu man a doon mooy bind bu mu ñuy jox mu aju ci liggéey ak doonte deesul yàggati fi, ndax loolu yéene nit ñi ay xéewal lay wund te ci ag jaamu Yàlla la » + +Sëriñ Saaliwu ak Tarbiya +Bi Sëriñ bi toppee yoon wi ba àgg ca jëmuwaay bu kawe ba, muy àgg ca Yàlla, daa daal di sóobu ci tarbiya , maanaam yare ak sellal jikko yi ak setal leen ciy ayibi bakkan ngir jeggeele Yàlla mu kawe mi. Yoon wi mu daa jaar ci yareem googu mooy wi mu jaaroon, nekkutoon di kuy tañaxu waaye ci xam-xam la ko tegoon ak leerug xol, loola dëppoo ak laaya bii di: «Neel wii de mooy sama aw yoon, damay woote jëme ca Yàlla ci leerug xam-xam man ak ku ma topp»(yuusuf 108) + +Tëriinu yaram wi (programme bi) dafa làmboo woon lii: alxuraan , xam-xami sariya yi ak xasiday S Tuubaa yi, ak liggéey yu yaram. Yooyu ñooy ñeenti xeet yi mu daa jaar ngir laabal xol yi ci ay jàngoroom, walla ñooy saabu bi mu daa raxase bakkan yi ci seeni ayib + +Yariinu xale bi + +Gone gi day door - ci li muy njëkk a def - ci jàng Alxuraan ba mokkal ko, bind ko te du ko xool, door a tàbbi ci jàngum xam-xam mi. Aji mokkal ji daa nees ko neexale lim bu am solo ci xaalis ngir mu soññu laata muy tàmbalee jàng xam-xam ak di jàngale Alxuraan, jàngalekat yi tam amoon nañu seen dëkkuwaayi bopp yu ñu leen jagleel ak seen lekkug bopp ngir wormaal alxuraan ji nekk ci ñoom, jenn daara ju nekk it daa na am 12 jàngalekat, kaamil yi ñu binde ci daaray 2 dale ko 1993 - taariixu sancug Xelkoom - àgg nañu ci 2289 kaamil, te ay téeméer ciy kaamil bindees na leen njëkk taariix bii ak ci ginaawam ci daaraam yu bari yii maneesul a lim. Bokk na ci li yayoo fàttali mooy ne fii ci Senegaal, rawati na ci digg yu daara yi, miinees na fi ñuy bind kaamil ginaaw ag mokkal, loola nag mooy aji mokkal ji bind kaamil bi te du ko xool niki firnde (certificat) cig mokkalam. + +Nosiinu daara ji + +Daara ju nekk am na bu jàngalekuti Alxuraan yi jàllee, kuy jàngale xam-xami sariiya yi ak làkku araab, kooku mooy faral a jiite daara ji, lañu fay jàng it mooy li ñu baaxoo jàng ci jataayi jàng-xam-xam yi (Majaalis) nga rax ci dolli xam-xamu Usuul ak Mustalah, benn bi Usuul di jàngale gongikuwaay yi àtte yi di bawoo, bi ci des di xamle yattiinu baat yi ñeel xam-xam yu yees, balaa ndongo lee àgg foofu, dana fekk mu jot a jàng am mbooloo mu ñu tànn ci xasiday Sëriñ Tuubaa yi, ci Tawhiid, Fiq, Tasawuf ak nos-wax. + +Moom de foo ko fekk da daan soññ dongo yi ci góorgóorlu bu baax ci gëstook njàng, di leen nettali démbi am njàngam, ak coona ya mu daa jànkoonteel, leeg-leeg mu laaj ay laaji nattu ak seet fi ñu tollu, di een won téere yi ñu war di yér, di xiirtal ci di teewe yenn jataayi xam-xam yi ak di ci bokk, daaraam yi it lu sakkan ciy woroomi xam-xam génne nañu fa, yoy yenn ci ñoom def nañu ay taalif yu am solo ci wàll yu bari, Fiq, Tasawuf, Jaar-jaar (Siira), Mustalah, Njàggat ak farata yi. Sëriñ bi jotoon naa móol yenn ci taalif yooyu te wisaare leen ci alali boppam te loolu ag soññee gu mag a ngi ci, akug góorgóorluloo. Daara ju nekk it am na am mbooloo mu liggéeyam mooy jàngal xale yi ay xasida ak tàggat leen ci ñu man koy yekkati ci ay daaj yu yéeme yu ñu jële ca mag ña daa jàng ca jamono ju Sëriñ Tuubaa mbaa waa kër Sëñ Masàmba , ku ci mel ne S Yuusu Ndaw, Alaaji Siise, S Mayib Géy ñi daa yekkati ci kanamu S Tuubaa. Mbooloom xasida moomu ëmboon na lu ëpp fan-weeri xasida, yi ci gënoon a siiw di Jasbul-Quluub, Mawaahibun-Naafih , Muqaddimaatul-Amdaah ak Rabbii-bimaayasrahul ... Dongo yi nag daawuñu def leneen lu dul jàng ak jàngale, ndare ci jamonoy nawet bi, bu boobaa ñu sóobu ci liggéey bi ci tool yi, ndax loolu ag wàll la woon ci tarbiya gi + +Sëriñ Saaliwu (g.y.m) nekkoon na di ku xamoon mbirum mbay, di ci fóore, bëggoon ko lool it te jàppe woon ko mecceem akug njaamu gu sell ñeel Yàlla (t.s), daawu ci faale néewug la mu cay ame, mbaa ag yàqoom walla ag àntoodeem. Daa na jëfandikoo ci tool yii ay bijjikaay (Tracteurs)yu tolloon ci 220. Mbooleem ay njuddéefi mbayam it addiya la leen daa def ñeel ki fi nekkal Sëriñ Tuubaa, bi mu nekkee it xalifa, daa daal di woon tàmbali di leen séddale njabootug Sëriñ bi ak miskiin yi, ak faqiir yi (way ndóol yi), ag wàll ci ñoom mu sotti ko ci luy defar dëkkub Tuubaa bi + +Ag Xilaafaam + +Moom nag mi ngi nekk xalifa ci 13 mee 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007. Moo doonoon juróomeelu xalifa bu Sëriñ Tuubaa, ku kiimaane la woon ci nangoo liggéey ak jaamu Yàlla ak dëddu àdduna ak yar ci Lislaam. + +Ay liggéeyam +Ci jéem gi mu doon def ngir dab bànneexu Sëriñ Tuubaa ci amal ay mébatam ya mu def ca Matlabul-Fawsayni, genn ciy xasidaam, Sëriñ Saaliwu taxaw na ci mottali ay sémb yu mag yu fi ay magam bawoon te dolli ci yeneen yu mag te am solo, bokk na ci yooyu: + + Àggale Daara ju Kawe ju Tuubaa (l'université de Touba) ba mu man a dékku lu tollu ci 5000 ciy dongo, + Yeesalaat Jumaay Tuuba, def fa benn jumtukaayu kàddul (une sonorisation) bu man a àgg ci 12 km ci soriwaay + Yaatal dëkk bi, natt ci 110.000 pàkk yoy ñaari ñatteel yi noppi nañu (pàkk yu ñuy joxe cig neen (amul pay) ñeel képp ku yéenee dëgg Tuubaa) + genn mbaalug laabal (un réseau d'assainissement) ci Tuubaa gu toll ci 18 km + Naalub mbay bu Xelkoom, mu yaatoo ci 45.000 ha. + +Sos na fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te lool a gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, tollu nañu ci 28, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru, ñuy yu mu sos ci alalam mbaa ci ndigalam mbaa mu dugal ci bu baax loxoom. + +ay daaraam +Sos na ay daara yu bari, ngir jàng ak jàngale, ci barab yu bari te wuute ci réew m i, bokk na ci yooyu: Got gi mu njëkk a sanc ci daara yi, mi ngi ko sos ci 1934, Njurul, ca wetu Tuubaa, Njàppundal, Ndookaa, Lagan, Ñibingal, Ñaaru, Ngaabu, Ngéejaan, Xàbbaan, Geloor, Tuubaa Njaaréem, ak yeneeni tool yu mu sanc ginaaw bi mu gental leen, mbaa yu mu sancagul ak jii mu mujj a sos te mu nekkoon jenn ju mag ju doon benn pakk bu mag ci suuf bu ëmb 15 daara, mooy Xelkoom, mi ngi ko sanc ci 1993, daara ju ci nekk yor turu ag gàdd (cartier) ci Tuubaa, yaatoo 50000 ektaar, la fa nekk ciy donga yuy jàng àgg ci 50000 jëmm, yoy li leen di dundal ci bis dina tollu ci 2500 kilo ci ceeb. + +Li ñu daa def ci daara yi + +Daara mooy fu deesi jànge Alxuraan waaye fi murit ñaare daaray tarbiyu lay doon, di benn barab bob dees koy sos ngir jàng Alxuraan ak xam-xamu diine waaye it ngir yar, mbay ak liggéey, mu mel ne day doon fu deesi waajale nit ba bu fa jugee dara du ko jaaxalati ci àdduna, moo xam lu deesi xam la ci diine, mbaa lu deesi dajeel ci jafe-jefey àdduna, ndax ka fa yaroo day miin coona yi, man koo dékku, wullees ko ci liggéey, jàngalees ko, mu mujj di "ku ñu jàngal ba mu ne arr, yar ko ba mu ne nërr" ni ko Sëriñ Fallu waxe woon ne noonu la leen seen baay Cerno defoon, kon (yar bees ne nërr, jàngale bees ne arr) mooy mbóotum tarbiya,> + +Ay séqoom aki mbokkam +S Saaliwu amoon na ay séqoo yu rafet te teey aki mbokkam, mu daan leen wéttalikoo te doonoon seen xarit, ñoom itam ññu fonkoon ko lool, daa ko tudde seeni doon, te daan leen ko jox ngir mu yor leen, yar leen, moom it mu nekkoon kok daa gisoon ne liggéeyal mbokkam yooyu de liggéryal S Tuubaa la, looloo taxoon mu boole woon ko ci wartéefam yu njëkk yi, mu daan diisoo ak ñoom ci lu mu man a doon, daan def lu mu bay ak lu mu bari bari jox ko Xalifa bi fi nekk. + +Ay séqoom ak mag ñu Sëriñ Tuubaa ñi +S Saaliwu - yal na ko Yàlla dolli leer - ku amoon ag cofeel la akug worma ñeel mag ñu S Tuubaa ñi, mu leen daan faral a jox addiya yu gànjaru, daan na def lu bari bu daan dem ci daara yi daan ànd ak ñoom, ku ci mel ne S Seex Faat Tàkko Jóob, S Mustafaa Si, S Musaa Alima Gey ak ñeneen ñi mu jamonoonteel. Man naa am nag li waraloon muy ànd ak ñoom ci daaraam yi mooy xaleem yi roy ci ñoom ci seen jikko yu murite ,yu taalubee, yu rafet yi, mu daan gis it ci àndaale googu ag mottali kóllare ci mag ñu baayam ñooñu, ña mu ca jamonoonteelul daa na leen jokke ci seeni doom mbaay sët, ku ci nekk am nga ca daaraam ya doom mbaa sët. + +Ay dénkaaneem: +S Saaliwu - yal na ko Yàlla gërëm - amoon na ay yitte yu daa nañu feeñ ci li daan gongikoo ci moom ci ay dénkaane aki soppaxndiku aki wax, bokk na ci baat yi ñu ko miine woon baatub Cant bi daan baamuwu aw yoon ciy xutbaam ak bu Tuub bi mu joxoon yitte ju mag, bokk na ci waxam yi daa tekki njàngaley S Tuubaa +yi: + ( Yàlla mooy tab bu tedd bi nga xam ne la nekk fa moom ciy xéewal du jeex, kon nañu ko ñaan ci xeewalam yii nga xam ne bindu leen lu dul ngir jaamam yi) + (Ku ragalul Yàlla, bind na lu mu ragal) + (Ku fàtte Yàlla de, na xam ne xéewalam yu bari yee ko waral ak yërmaandeem ji) + (Bokk na ci pexey Saytaane su ñu jam si, bu ndigal jugee ca Sëriñ bi jëm ci murit yi, day gaawantu (moom saytaane) ne leen bu leen def ndigal lii, Sëriñ bi rekk moo ko man, bu ngéen ko manoon du ngéen fi ñëw di jébbalu (am ñu ci naan duma dugg saxaar yanu sama bagaas). + Bu Yàlla feeñalee ayibi ab jaamam, booba da koo bëggoon a jéggal, waaye ab jaam nag day feeñal ayibi mbokkam ngir gàccaal ko, rusloo ko, ŋàññ ko. + (Na jaam bi yittewoo biiram bi dul suure lu dul ay jëfam yu baax (Bàmmeelam)) + (Yàlla sàkkal na nit ñaari biir bu boppam bi, moo ko ko yoral jarul mu ciy sonn, saa su xiifee mu reggal ko, ak bu bàmmeel, na cay sonn, ndax lu mu ca deful du ko ca fekk) + +Ag génnam àdduna +S Saaliwu mi ngi génn àdduna ci subag bisub àjjuma 17 ci weeru tëbëski atum 1428 g, dëppook 28 desambar 2007, ba fi nag dund gu jege 95 ciy at, ngir fekki waajuram wu tedd wa S Touba. Yal na gëramul Yàlla sottiku ci kawam ak lu waajuram, ñu gunge ko ba ca saxuwaayam bu mujj ba ca penkub Jumaay Tuubaa ja, ca guddi ga ca topp. yal na ko Yàlla (t.s) fayal Lislaam ak xeet wi gën ji fay gu muy fay jaamam yu baax yi ko liggéeyal. Aamiin + +S Baara Mbàkke falilu moo ko fi wuutu niki 6eelu xalifa bu S Tuubaa. + +Gongikuwaay +Abdu Xaadir KEBE +yoonu murit +niti senegaal + + +wolof + ab lay mooy doqi ndox yu sew (yu weex)yi lay tee gis oto bi ci sa kanam booy dawal oto + +Italiano + nebbia +baati wolof +Sëriñ Mbay JAXATE nekkoon na di kenn ci woykati wolof yu mag yi (taalifkati woy yi) di woon it benn taalibeb Sëriñ Tuubaa, li mu taalif ci woyi wolof maneesu koo misaal mbaa deesi ko lim, nekkoon na di ab soofiyu bu mag, lu ëppoon it ciy woyam ci googule wàll la jëm, ku lislaame la woon te di woon ku jéggi dayo ba cig taral ci ñu sammoonteek daytali Yàlla yi aki ndigalam, bokk na ci ay woyam yii: + pexem Yàlla moo gën pexem nit ndaxam () fa Yàllay fexee yàqkat yeggu fa + Murit yaw de bul mer te bul jàpp mer () mer ak jàpp mer day alag ab murit + +moo wax it: + + Bul gaaw a ñam gaaw a ñam baaxul nigal ba mu ñor () meeneen akug neen a yam pal-pal matul ne pelam +moo wax it: + Am kilifaay li am solo () boo ko amee am nga solo () boo ko amul amoo solo () ku wéeruwul yomb a bëmëx + +Yóbbal baax ciw yoon + +Yóbbal baax na ciw yoon : + +Genn la ci xasiday Sëriñ Mbay Jaxate yi: + + foo bëgg a dem nanga wut loo yóbbaloo soog a dem + +kon boo demee doo fa lor yaw nit te doo fa loru + +kuy dem te yóbbaalewul yóbbal bu doy fa mu jëm + +kookee du bég du bégal ngir day loreek a loru + +Yóbbal bi nag moo di fàggub yar te wol mburu yor + +foo dem di may koo fa gis ab yar, di mos sa mburu + +Ku nekk war na balaa dem fab yar ak mburu yor + +ngir dégg fenn di wax talal du xeetu yaru + +Yóbbul yar ak mburu boo dee tukki, kon dinga bég + +bégal barab ba nga jëm ngir doo loreek a loru + +Moo wax it : + +Ne dell ak ñam ak ndox ñu naa sang bii () nga dof nag ba naa huu dangay alku kat + +Moo ne it: + +Bu cér yépp gàntoo def'as lëf jafe + +Def'as lëf bu yombul am'as lëf jafe + +Jugal farlu ngir yaa ngi cib lolli yaw + +Te ab lolli buy wéy am'as lëf jafe + +Ndegam reere nga'b lolli lollee ngi nii + +Wér ak dund ak doole lollee jafe + +Ku sab lolli ñëw nag ba say yëf ne xuss + +La gën ngay ku yombul, ku maasam jafe + +Jëfal guddi jëf bëccëg'ak sépp saa + +Ba koo seeru naa kii jëfam yee jafe + +Ku def nii ci sab lolli do jeele yëf + +Bu nooree te doo xaare yewwoo jafe + +Budul woon ngëméen ak nélaw koofu gis + +Mi ngiy farlu ngir xam ne lee jëf jafe + +Bu nit nee lasar, ñépp naa dóotu jug + +Mu xemmeem a jog jëf té jog jëf jafe + +Ku jëm cib ja té romb xaalis di wey + +Bu yeggee di gis yëf ya teg njëg jafe + +Xarit dëgg ŋooral ci xaalis bi yaw + +Te kat leegi seerub dërëm sax jafe + +Ngirug mag akug ràgg ak dee ngi ñëw + +Bu ñuy yegsi dëf lëf lu bon bon jafe + +Defal Yàlla as lëf bu mujjee jafe + +Am as lëf ci Yàllaati gën koo jafe + +Woy wu mu def ci wori àdduna + +Adduna bëgg na laa fab waaye yaw nanga bañ + +Lu fab fab it nanga fab say tànk samp fi suuf + + + +Jekkil te riigu fi suufus Yàlla sii bu fi jog + +Loo jëm jëm it kaw dangay dellooti rekk fi suuf + + + +Lalub gitax ak lalub weñ ak lalub tagar ak + +Lalub selen boo ci tëdd it wàcci dellu fi suuf + + + +Mbaam ak gëléem ak fafal-naaw ak wata'aku ngélaw + +Loo ciy war it dula tee xëy bis ne céng fi suuf + + + +Néegub ñax'ak mbaari seng ak taaxi suuf aki kaw + +Loo yàgg yàgg ci ñoom it génn dugg fi suuf + + + +Cerey lay ak wataboor ak ndàbb ndiir aku sëb + +Ak mbuum akub cox a faf yam bis ba ngay gane suuf + + + +Baadoola ak buur akub dag ñépp ñoo xala yam + +Lu yàgg yàgg dañiy booloo ne meng ci suuf + + + +Jëlub lingeer ak jëlub jaam ak jëlub xaj a yam + +Loo jël jël it dee gi xëy bis jël la dénk la suuf + + + +Adduna wor na mag ak ndaw wor ko leegi bu wér + +Te ŋoy ci Yàlla ki yor suuf ak ñi nekk ci suuf + + + +Lu yàgg yàgg nangay def Yàlla wettalu xol + +Moo lay fegal lori kaw, moo lay fegal lori suuf + + + +Suuf ak kaw ak fépp a am lor fépp a am njariñ it + +Ku dëddu am njariñal kaw, am njariñ li ci suuf + + + +Am yitte ciw sas ba fàtteb añ du tee añ a ñëw + +Fexeel a am ca kaw'ug pal fàww am ko ci suuf + + + +Ñun ñépp yal nanu am ag pal ca kaw gu rafet + +Gu sax te am ko fi suuf it ñépp féete nu suuf ! + +Aw Woy ci Xarit +Xarit da lay xaral'as lëf ciy yëfam ni la am + +Koo xam ne kii du xar'as lëf may la doo waayam + + + +Sëriñ da lay jariñ as lëf yar la yor la bu wér + +Xamal la Yàlla, nga dib sàntam di ab jaamam + + + +Baadoola day bay di gor, may buuri gët, di ko jay + +Di wetti aw ñaq ak'ay muñ, sax ci ab toolam + + + +Jëkkër dafay muñ a kay muñleek a sàmm ngoram + +Ragal boroomam te am njël jiitu ak maasam + + + +Jabar dafay yaru tay muñ neexi wax bañ a wex + +Rafet rafet jikko man boppam ne cib neegam + + + +Aw fa dafay gore neexum ndañ di gas ak a tag + +Waqam wa sew we wa rëy muy méng akub taaram + + + +As gor dafay gore tey fonkiy waxam ba du dañ + +Du fen du jëw te du sookeb jëw ka dib yaaram + + + +Mbokkay ka bokk'ak yaw'ub xol, say wax it di waxam + +Séeniy jëf it bokk, muy sab caabi ngay gaalam + + + +Buuray ka xam Yàlla sax cig topp not bakkanam + +Te doylu doyle amug baaxam yorug leeram + + + +Sàmm ay ka sàmmi céram sàmm'ub xolam ba du jëm + +Cig moy du jog ci ndigël, bii sàmm a gën giiram + + + +Jàmbur dafay jàpp fàww'ug njaamburam ci lu bon + +Du def lu dul noona, déeful dégg aw tooram + + + +Sang ay ka sangi moroomam tey jubal ak a jub + +Nekkal di ab sang yaw mii mbaate ngay waayam + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + Ay woyam ci youtube + +Niti senegaal +Yoonu murit +Dun : île (fr) +Ayubés : 7 bés = altine, talaata, alarba, alxamis, ajjuma, gaawu ak dibéer. + +Arminaat +Dibéer/Dimaas : bés benn (ayubés) + +Arminaat +Altine : bés ñaar (ayubés) + +Arminaat +Talaata : bés ñett (ayubés) + +Arminaat +Àllarba / Alarba : bés ñent (ayubés) + +Arminaat +Alxames : bés juroom (ayubés) + +Arminaat +Àjjuma : bés juróom benn (ayubés) + +Arminaat +Gaawu / Aseer : bés juróom ñaar (ayubés) + +Arminaat +Ñaar : 2 + +Xayma +Ñatt : 3 + +Xayma +Juroom : 5 + +Xayma +Juróom benn : 6 + +Xayma +Juróom ñaar : 7 + +Xayma +Juróom ñett : 8 + +Xayma +Juróom ñent : 9 + +Xayma +Fukk : 10 + +Xayma +Fajar : Guddi-> Fajar -> Njël -> Suba (bés) + +Bés +Njël : Guddi-> Fajar -> Njël -> Suba (bés) + +Bés +Diiwaanu Kafrin benn la ci 14 diiwaani Senegaal yi. + +Diiwaani Senegaal +Diiwaanu Kéedugu benn la ci 14 diiwaani Senegaal yi. + +Diiwaani Senegaal +Diiwaanu Séeju benn la ci 14 diiwaani Senegaal yi. + +Diiwaani Senegaal +Xavier Rovira Rojas - dioudo Mataró, Catalonia, si atoum 1977 si diourombénèlou wèr wi si att bobou, mathematicien la té guénè keur you mag you niouy wakh Valldemia Marist ak Autonomous University. Kou khariagne la si wal wowou tey liguéyè Plaut (Acctus) fofou sa Barcelona si atoum niari diounni ak niar ba niari diounni ak niet diougué fa dem fofou niouy wakh Northgate Arinso si atoum niari diounni ak niet sa Barcelona lègui mou ngui fi si Wiyen. + +Basketeur la tamit bou nékon si équibou Valldemia si atoum diounni diourom nièneti temer diouro nièneti niar ak niari diounni ak diourom ben fofou sa CE ak si atoum diounni ak diourom ben ba diounni ak diourom niet Argentona fofou sa CB. + +Sport +Ngéej : as ngéej mooy lu mel ne géej te tuuti. + +Melosuuf +Ndox +Xaj : dundat yi + +Rab +Muus : rab la. Bokk na ci njabootu dundat yi. + +Rab +Jasaan : Pristis pectinata (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Diassan" + (en) Fishbase : "Pristis pectinata" + +Jén +Piipa : Delphinus delphis (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Piipa" + +Rab +Garab + +Garab gàncax gu dëgër la, di am ab dàtt bu taawu ay banqaas yu firiku am i xob yuy faral di nëtëx. Xob yooyooy joxe ker gi. + +Garab yi gàncax lañu yoo xam ne dañoo man a gudd fan. Ñoom dañuy dund ay at yu bari. Amna ci yoy man nañoo dund lu ëpp fukki at, am ci yoy téemeeri at, ba am ci sax yu néew yuy àgg ba junniy at. + +Ci li ñu xayma, àdduna bi am na lu mat 60.000 ba 100.000i xeeti garab. + +Garab yi nag, fi ñu ëppe mooy ci àll bi, ci gott yi ak màndiŋ. Fa ngay fekk garab yu bari yu dajaloo. +Waaye batay it garab yi man nañoo màgg ci feneen fu dul ab àll, niki ci biir dëkk yi, ba ci sax biir kër yi. + +Dañuy liggeey, liggeey bu am solo nag ci jokkalanteg càkkéef gi. (Jokkalante gi am ci yi ci àdduna bépp, nga xam ne ku ne aajewoo nga sa moroom.) + +Ndax dañuy muucu gaasub karbon bi doomu aadama yi génne di ko denc. +Ba noppi di génne gaas ogsisen bi nga xam ne nit moom lay soxla ngir dund . + +Day liggéey, liggéey bu am solo it ci wërug ndox mi. (Ni ndox mi di jaare ci suuf garab yi muucu ko mu demaat ci kaw, wàccaat.) + +Batay ci wàccug taw bi da ciy liggéey lu am solo, ndax fu la ëpp i garab ëpp la lu muy taw. Da ñuy xëcc ndox mi ngir mu wàcc màndal leen. + +Am na njariñ lool tam it ci yi doomu aadama di jëfandikoo. lu ci mel ni: matt, këriñ walla sax foytéef yi ñu ciy lekk. Walla mu di ci faju mbaa kerlu mbaa jariñoo dénk wi ngir di ci defar i lal ak yeneen, mbaa defar ci luy aar yaramam niki ay saabu yu muy sangoo walla ay pat ngir ay bañam. +Dees na ci defar ba tay ay néeg, ay kër, ay këyit, ay toogu, ay cempteŋ (taabal) , ay kees, (kaartoŋ) ay bale, ay bunt, ay palanteer, ay raas ay gaal walla sax bato ak yaneen ak yaneen i njariñ yu muy amal doomu aadama. + +Foo dem ci àdduna bi rekk, garab am na lumu fay jariñ. Dana am fuñu koy teg am cër buñu ko jox it. + +Xamle gi + +Daanaka amul menn piri moo xam ne ñépp dëppoo nañu ci, muy tekki garab. +Ndax boo jëlee garab dafa ëmb ay gàncax yu bari yoo xam ne xeet yu wuute ñoo ci nekk yu tasaaroo. Looloo waral nag ñiy jàng xam-xamu gàncax ak ñi am xam-xamu garab yu xaw a mag yi, ak ñi am xam-xamu àll, ñoom dañu ciy werante ba leegi. +Ngir nag ñu am ay tegandaay yoo xam ne di nañu ci man a sukkandiku ngir méngale njuréef yi jóge ci àll yi ci àdduna bi yépp, kuréelu Mbootaayu Xeet yi ëmb wàllu dund ak mbay ñu koy wax FAO moom dafay joxe menn piri moo xam ne daal dafay sukkandiku rekk ci guddaayu garab gi. + +Moom FAO dafa wax ne, garab daal genn xeetu gàncax la goo xam ne, bu fekente ne mbir yépp daje nañu maanaam bu amee li mu laaj lépp dafay màgg ba man a am 5i met cib guddaay, ci réew yi nga xam ne amuñu ak suqaliku, walla 7i met ci dëkk yi nga xam ne ñoo suqaliku. + +Loolu nag moo koy wuutali ak garab yu ndawaan yi ñiy woowe ay ngajj. Niki ngeer, salaan añs, yooyu nga xam ne seenub guddaay buñu màggee ci diggante genn-wàllu met ba ci 5i met walla 7i met lay toll, te nga xam ne ñoom daanaka duñu am ker, duñu am mbaar. + +FAO itam dugal na ci loolu garab yi nga xam ne amuñu li ñiy wax daakaande, lu deme ni ron walla dànq. + +Boo jëlee lu mel ni ron, bant bi boo ko dagge day am lu mel ne am lëm ca biir, nga xam ne bant bi lépp feesul, te namu war a dëgëre du ko dëgëre, ndax bu gënee wow day mel ne ay bant yu sew la yu dajaloo. Loolu li mu amul daakaande moo ko waral. Yooyu amul ci niimaa. Niimaa nga xam ne aw dénk la wu dëgër buñu ko daggee, moom dafa am daakaande moo tax, daakaande ji moo waral mu dëgëre noonu. Bu dee ron nag amu ko, moo tax muy def ay bant yu sew. + +Amna it ñoñ niñu jàppe garab, mooy gépp garab gu am daakaande rekk lañuy wax garab. +Waaye FAO moom da cee dolli yi amul daakaande. + +IFN moom dañoo wax ne, garab mooy xeetu gàncax goo xam ne dafa am liñin, ba noppi am ab bànqaas boo xam ne dara sax na ca, ba noppi guddaay ba day tollook 5i met walla mu ëpp ko. +Mori : Brotula barbata (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Mori" + (en) Fishbase : "Brotula barbata" + +Jén +Ndiané : Pentanemus quinquarius (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Ndiané" + (en) Fishbase : "Pentanemus quinquarius" + +Jén +Bëër / Sekhebi (Gànnaar) : Argyrosomus regius (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Bëër" + (en) Fishbase : "Argyrosomus regius" + +Jén +Khal / Joto : Pseudotolithus elongatus (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Khal" + (en) Fishbase : "Pseudotolithus elongatus" + +Jén +Fötö / Tunnun : Pseudotolithus typus (dundat yi) + +Lëkkalekaay yu biti + + (fr) Informations et connaissances sur les milieux côtiers et marins ouest africains : "Fötö" + (en) Fishbase : "Pseudotolithus typus" + +Jén +Fëtt / Tuunuun : Pseudotolithus senegalensis (dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réew : Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Gànnaar - Senegaal + Melo : dóomu taal + Dayoo : 50-100cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Pseudotolithus senegalensis" + +Jén +Thiékem / Sikket mbàw : Galeoides decadactylus (jén - rab) + + Askan (pop) : ? + Réew : Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Gànnaar - Senegaal + Melo : toubab + Dayoo : 12 - 40 cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + (en) Fishbase : "Galeoides decadactylus" + +Jén +Djabar / Yaxx : Lutjanus agennes (dieun - dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réew : Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Senegaal + Melo : xonk + Dayoo : max 160 cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Lutjanus agennes" + +Jén +Njagatun : Lutjanus goreensis (jén - dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réew : Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Gànnaar - Senegaal + Melo : xonk + Dayoo : 50cm - max 80 cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Lutjanus goreensis" + +Jén +Rap xeetu woy la, bokk ci yëngu-yëngub caada bii di hip-hop tambali ci ndoorteelu ati 1970 ca Réew yi Bennoo yi, ci biir askanu waa-aamerig yu ñuul yi . Am na ñu ne aji-rap bii di Joe Tex moo sos baat bi. Ci njëlbeen MC yi,(masters of ceremony, njiitu xew mi)liggéeyam moo doonoon jàppale DJ bi, wàll wi ñu doon rap la ñu doon woowee MCing. break dancing, DJing, MCing ak graffiti yi, ñooy ñenti ponku yi caaday hip-hop dàttu. + +Luy rap? +Rap niki lépp lu bokk ci caadaay hip-hop dafa ëmb lu bari: xew, fo, ñaxtu... Seeni mbind, ak seeni kàddu dañuy soppiku topp jamono. Mbind yi dañuy wax ci li nit ñi di dund bés bu ne: politig, koom, diine, mbëgéel,... + +Bari nañ gangoori rap yu seeni mbidd fees aki ñaxtu, ay kaas. Li gëna fés ci seeni mbind, te yenn saa yi ñakk-kersa lool, ñi ngi leen jëmale ci way-politig yi, takk-der yi, yoon,... Ci Senegaal rap teel na fee àggsi, ci njëlbeenu ati 1980 la waa-senegaal yi tambalee xam aji-rap yu mag niki gangoor bii di Public Enemy, Africa bambata,... + +Taariix +Ñenn ñi dañ koy tekke niki tënku baati waa-angalteer yii di rhythm and poetry walla rock against police. Ci ndoorteelul ati fanweer yi, waa-aamerig yu ñuul yi nekkoon nañ ci ñakk gu tar, loolu juroon ñakk-kaaraage, rayante, ay xeex ci diggante kureeli defkati ñaawteef yi, njaayum lu bon, añs. Ci dundin gu tar gii la ndaw yi tambalee fippu, jël rap def ngannaay ak yoon ngir fésal seen mer, ak seen nekkin gu tar. Lii moo tax li ëpp ci seeni mbind day yor jëmmu kaaskat, ñaxtukat jëmale ci takk-der yi, way-politig yi, njiiti yoon yi,... + +Taariixu rap dafa séddaliku ci ay jamono: Rap Old school (1970-1985), di ndoorteel gi, ba ciRap Golden Age (1985-1993), di jamono ji rap tambalee am doole dëgg, ci la East-Coast (tefesu penku) ak West-coast (tefesu sowwu)juddu. Ci jamono jii la yeneen xeeti rap yii di gangsta rap ak G-funk juddu ca West Coast. Ci 1993 ba tay rap Hardcore, bling-bling, underground, añs, ñoo fi juddu. + +Old school (daara ju yàgg ja) +Rap a ngi juddoon ci yeneen xeeti woy yii di funk, gospel, soul, blues, rawatina talking blues. Mi ngi juddu ci ati 1970 ca Bronx, di ab gox-goxaanub New York, di barab ba gangoor ba tuddoon Organization te gëna siiw ci Zulu Nation. Li ëppoon ci seeni wax ci aadaay Afrig ak Jamayka la doon jóge. + +Kon ci ati 1970, ci xewi mbedd yi la nit ñu nel ne DJ Kool Herc tambalee taqale xeeti woy yu mel funk, soul, R&B, disco music. Ñu tambali di leen tek ci mbedd yi, ci xew, géej, dañ ko jàppe woon fo, bégal seen bopp ànd ak seen dj. Bi xeetu woy wi tambalee am ciiwte, lañ tudde woykat bi MC (Master of ceremonies). Li MC bi doon def sax man nañ kaa baña tudde woy ndax da doon wax ci biir woy wi dj bi tegg, ci wàll yi amul wax, doonoo wax ju neex, loolu dem bañ tudde ko "rapping". Doonul woon lun ñu man def ciy tappaan di leen jaay, ndax ay waxantu lañ woon rekk, yu ñu doon xalaat ci jamono ji ñu ko doon waxe. + +Ci 1979 la tappaan bi ñeel bii xeetu woy njëkk a génn: ""Rapper's Delight"" bu Sugharhill Gang. Aji-rap mooy kiy def rap, ci wolof, waaye ci kàllaama waa-angalteer "rapper" la ñuy wax kiy def "rapping", baat baa ngi juddu ci woy woowu. + +Génneeb Sugharhill Gang bi amoon na solo lool ci ciiwteeg xeetu woy wu bees wi, di laal mbooloo mu bari, yemul woon rekk New York, di fa mu juddoo, waaye réew mi yépp la mujje laal. + +Ci ati juroom-ñett yi la Rap tambali bari melo, di màgg ci yeeneen melokaan yu gëna fasu. Ci jenn jamono ji, yeneen feem yu xereñ gis-bés, lu mel ne scratching. + +Golden Age (ati wurus) +Laataa jamono jii, xeetu rapin bi fi nekkoo dafa dattu woon ci breaks ak Woyu mbëjfeppalwoyu mbëjfeppal. Ñëwug waa Run-DMC soppi lépp: seen feem kàttanu woon na te metti, ñoo ci tambaalee dugal ay jumtukaay yu bees, ay riff yu xalam, yàggul dara ñu nekk ay royuwaay. Waa Run-DMC ñoo ubbi buntu ati wurusu rap, mujj doon gangooru rap bi njëkka àgg ci collu àddunay woy, amoon ciiwte gu jéggi-dayoo te wéy di màgg. Ci nii rap bi tas ci àdduna yépp ni ab pënd + +Rap Gaalsene +Ci Senegaal rap teel na fee àggsi, ci ndoorteelu ati juroom-ñett yi la gangoor yi njëkk juddu. MC Lida mooy ki njëkka génne ab tappaanu rap, tuddoon Duma doyal mukku mooy aji-rap bi njëkk ci Senegaal. PBS tegu ci ag génneem boobu di Ataaya. Rapu Senegaal ci at yooyu waxi mbëggéel moo ci gënoona fés, ci 1998 rap Gaalsene am jekkiku gu am solo, beneen xeetu rapin feeñ, rap underground. Waa Rap-adio ñoo indi feemu rapin bu bees bi Senegaal, doonoon rap ñaxtu, seenug ñëw yokk rap doole, daanaka li ëpp ci yeneen aji-rap yi ñëw ci seen ginnaaw yépp rapin boobu lañu jël.Tay gangoori rap yu Senegaal xayma nañ leen ci lu tollook 2500. + +Hip Hop +Hip-hop ag yëngu-yëngug caada ak fànn la, mi ngi juddoo ca Réew yu Beenoo ya ci ndoorteel ati 1970 yi, daa boole bànneexu ak ñaxtu. Mi ngi juddoo ci biir askani waa-aamerig yu ñuul yi, ca New York, fa la tàmbalee, mujj tas ca réew ma ba ci àdduna bi bépp, ba tay mooy dundiinu réewu-taax wi ëpp doole. Caaday Hip-hop ci ñeenti ponk la tënku: break dancing, DJing, MCing ak graffiti. + +Wii xeetu fànn ñu bari ci woy wi lañ koy tënk ,MCing, te mu gën a siiw ci rap. Caadaay Hip hop yamul rekk ci rap, man naa sol mbubb yu wuute: su fekke danuy yam rekk ci xoosug DJ bi (Disk Jokey), waruñu ko tuddeeti rap, waaye DJing , sunu yamee ci li MC bi (master of ceremonie, njiitul xew) di bàcc kon man nanu koo woowe rap, walla tamit, donte bari na lu muy faral di am, boolee benn DJ ak ay walla benn MC, kon ci nii hop-hop lañuy wax, ndax rap ak MCing yépp ci caadaay hip hop lañu bokk, waaye nit ñi rap lañuy wax rekk yam ci ngir yombal. + +Cosaanu baat bi +Cosaanu baat bi taxu koo leer noonu, ci ñenn ñi jëfandikoo-xel ngir tekki + Hip "muus", "am-xel" lay tekki, muusaayu tappalaatukat. + Hop ag yuuxu la gu kuy tëb di def (sooy tëb ni op!). +Nee nañu baat baa ngi war a bawoo ci DJ Luv Bug Starski mi ko doon faral di jëfandikoo suy wax. Waaye li wér te wóor mooy ne gandoor bu Sugarhill Gang mooy ki ko siiwal ci àdduna bi, ci seen woy woowu Rapper's Delight, di benn ci woyi rap yi ñu njëkk a def k7. + +Taariix + +Ay cosaanam +Woyu hip-hop ci buumu xeeti woyi waa-aamerig yu ñuul yi la bokk. Ay dàttam ñi ngi bàyyikoo ci dundiin gu metti gi ñu nekkee woon, dalee ca seeni maam ba ci jamono yi muy juddu, woy yañu daan def ca tool ya daan ca naqarlu seenug nekkiin, ak daan ca fattali seenug jóge Afrig. Mi ngi tàmbalee ciy kebetu niki xeeti woy yu mel ne ragetime, jazz, blues. Ci lu gën a jonjoo, woyu hip-hopa ngi bawoo ci Soul, ak ci funk. Yii xeeti woy bawoo bëj-gànnaaru Aamerig dem ba fasook sound-system bu waa-jamayka, bi àgg ba New York ndax ndoxandéemu gi waa-jamayka yi daa def foofa. Ba tax-na ñett ñi ñu ne ñoo sos yëngu-yëngu hip-hop fa lañu bàyyikoo. + +Donte hip-hop ci yii xeeti woy la jële ay dàttam, waaye doonul seenug wéyal. Du lu ay tëggkat yu xereñ ci seen liggéey toog xalaat, ni blues doonee wéyalug jazz, gospel juddoo ci blues, soul tegu ci, funk ñëw, caaday hip-hop dafa am ab dog-dog ag yeneen xeeti woy yooyu + +Aji-rap yi njëkk +Les premiers rappeurs et groupes de rap qui ont marqué l'histoire sont : + + Sugarhill Gang + Run DMC + Afrika Bambaataa + KRS-One + Grandmaster Flash + Beastie Boys + LL Cool J + Big Daddy Kane + Last Poets + +Lëkkalekaay yu biti + Ab buntu ci rap Jolof + Ab dal ci hip-hopu Afrig + Màggug hip-hop ci àdduna bi + Taariixu hip-hop + Tariixu hip-hop + taariixu hip-hop Zulu Nation moo ko defar ak yeneen jukki + Mémoires d'un graffiteur njëlbeenu hip-hop ca Faraas + www.hiphop-musik.org + +Hip Hop +Break dancing, walla breakdance, walla break, walla b-boying, ab baat la bu ñuy jëfandikoo ngir wax fecciin wa juddoo te màgge New York ci ati 1970, xammeewu ngir ay suppjalañam aki bërangoom ci suuf si. Fecckatu break dance la ñuy wax breakkat. + +Taariixu break dance + +Break dance ak hip-hop +Taariixu break dance mi ngi doore ca Bronx ci ati 1970, Kenn ku bokkoon ci mbootaay gu Bronx River projects la ñu ne moo ko sos. Mu jóge fa, tudde Bronx River Association Afrika Bambaataa, ba si yàgg mu tuddewaat ko Zulu Nation (ci 1974). Gëstu yi mu doon def ci taariixu Afrig ak mbëggéelam ci woy gëtanoon ko, ba taxoon mu farlu woon ci ngir ay ndawi goxam nekk ciy yëngu-yënguy fànn ngir bañoon ñu duggu cig ndëngte. Moom lañuy santee juddug yëngu-yëngu gu bees gi: hip-hop, gi dàttu ci ñenti ponku yii di rap, grafiti, DJing ak break dance. Afrika Bambaataa soosoon na itam benn ci gangoori break dance yi njëkk, tuddoon Zulu King. Njeexit gi waa-jamayka bii di Dj Kool Herc amoon ci caadaay hip-hop mi safaanu woon ak caadaay ndëngte ga amoon ca seen dëkkuwaay ya, ca jamono jooju am na solo lool, ba mat naa fésal. + +Fu pecc mi soqikoo +Jafe na lool joxe a taariix bu wóor cig juddoom. Ci jeexantalu ati 1970, New York dafa bari woon lool ay xeeti pecc, gox boo dem aki feccinam. Numu manti deme, li fés mooy ne, feccin yi gënoona siiw ñoo doonoon good foot ak popcorn, te jóge woon ca woy yu James Brown ya Get On The Good Foot ak Popcorn. Pecc yooyu yëngali tànk ci anam bu lañ woon te fecckat yi daan sapp se benn tànk di ko awante an beneen bi. Nit ñi daan nañu ci def ay joŋante, siiwoon nañu lool ca jamono yooyu. + +Kenn xamul lu waral suñuy fecc di bërangu, aka daanu ci suuf, gannaaw seeniy weñaaru ak seeni damm-yaram. Xalaat nañ lu ne: xéj-na Filmi kung-fu yiñ daan seetaan te ñu bari lu ñuy ŋelaju di tëdd ci suuf. Xéj-na tamit jël nañ ci capoeira. Breaker yi sacc nañ tamit dara si pecci caada yu waa-kasakistaan. + +Feccin mi +Pecc la mu kenn rek di def, du feccu mbooloo, ci lu ëpp dañuy def ab wërngal kiy fecc nekk ci digg bi, ñuy awante, kenn dem, kenn dikk. Fecckat bi day bokk cib gangoor ñu koy wax crew, suy fecc ŋelaju yi muy def la ñuy wax footwork, walla passpass, ci maanaa su sampee ay yoxoom, ay tànkam daleen di wëndeel ñuy wër yaramam. + +Lëkkalekaay yu biti + Style2ouf : L'actualité de la danse Hip Hop [Bboying-breakdance-popping-locking...] + Red Bull Bc One : site du championnat mondial en 1 contre 1 + Illusion Style : c’est tout sur l’actualité et la culture de la danse Hip-hop, Break Danse dans + +Hip Hop +Disc jokey (ñu koy wax itam DJ, di jàng "dijéy"), mooy kiy teg woy yi ci xew yi ak ci feccuwaay yi, jagleel ko benn mbooloo. + +Fànnu DJ +DJ bi ab béglookat la, mooy kiy yor li ñeel woy yi ñuy teg cib barab, (mooy tànn woy yi, waaye it day bàyyi-xel ci mbooloo mi) +Bene aw rëdduw suuf wu sew la, nekk ci diggante yamoo gi ak Gëwéelub Sànkar bi. Rëddu tus-wu-gaar wu bene mi ngi ci diggante 6°30'bëj-g ak 12°30'bëj-g, tu-wu-taxawam moom mi ngi ci 1° P ak 3° 40'P. + +Ay digam +Ay digam ñoo ngi yem ci Togóo ci sowwu, yem ci Burkina-faso ak Niseer ci bëj-gànnaar, ci Niseeriyaa ci penku, janook mbàmbulaanug Atlas gi ci bëj-saalum. Mi ngi am yaatuwaay gu tollu ci 112.622 yu kaare. Bene ngi bawoo ca dexub Niseer bi ci bëj-gànnaar yem ci mbàmbulaanug Atlas ci bëj-saalum ci ab tallalub 700 km. Diggante bi gëna guddu ci réew mi 325 km la. + +Lëkkalekaay yu biti + ICJ Judgment over the Benin-Niger boundary dispute, 12 July 2005 + Fabio Spadi (2005) The ICJ Judgment in the Benin-Niger Border Dispute: the interplay of titles and ‘effectivités’ under the uti possidetis juris principle, Leiden Journal of International Law 18: 777-794 + +bene +melosuufug afrig +Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca allaaxiraa. + +Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sang Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam gu sax + +Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la (wu mat a wéer say mbir, joyal ko ko). + +Jëf yaa ngi ci yéene yi, ku nekk it la nga yéeneey sag pay + +Bokk na ci hikam (sagesse) : + +ku sàkku mbir de bu ca saxee am ko. +Ku fëgg bunt it boo fa saxee ubbilees la + +Bokk na ci hikma bat ay: + +ku tëyye boppam wëlif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi. + +Bokk na ci ba leegi: + +ku dul merloo boppam du begloo boroomam. + +Bokk na ci ba tay : + +ku def la ko soob dajeek la ko naqari. + +Bokk na ci: + +ku taqook jiyaar ak bakkanam, texe fa biir bàmmeelam . + +Bokk na ci : + +ku topp Yonnant bi, am gën ji la mu ñaan. + +Am ku jël maanaa yii yépp boole leen ci wenn bayit : + +( képp ku woor wëlif caaxaan yi () danga dogi ciy ngënéel ) + +Taalif wi + +Taaliif wii nag lu ñu barkeel la ci njëlbéen gi ba ca dayo ba. + +Moom nag (ki waxoon bayit wu njëkk wi) –yal nañu ko dolli ag bëbb (xéewal) – am na ba tay weneen bayit wu yor maanaa mii, mu ciy nos (woy) maanaam waxi sëriñam ji, wax jooju mooy jii : + +(nguurug neen waxtu rekk la, nguurug dëgg nag day wey ba yawmal-xiyaam) + +Woy waa ngii : + +( dëgg day sax , neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe) + +Maa ngi Tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ju ñu jagleele ji ca allaaxiraa + +Ubbite gi + + Kii di doomi sëriñam ji dul sant ci boppam lu dul turam (wu tedd wa) Muhammad, kii de mi ngi sant Yàlla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko. + +Tudd naa sellam ga moom de boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy sant. +Moom de mooy ki def ay teggiin yu raf muy luy làq ag réer ak judd bu ñaaw (bonu askan). +Mooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggiin, mooy ki léen jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub). +Xéewal ak mucc gu kawe nañu sottiku ca ka yéegoon ca Alburaax (Yonnant bi). + +Kooku mooy suñu sang biy woote jëme ci aji bind ji (ki sàkk mbindeef yi), defe ko nag ci gën jaa rafeti teggiin yi . + +Kooku mooy Muhammad ak ñoñam ñi di woroomug raw ak saabaam yi làq ngënéelul Aji des ji (Yàlla mi fi dul jug) + +Ñoom saaba yooyu de saxaloon nañu ag laa-biire ci lu dul ŋaayoo , ndaxte dañoo toroxaloon seeni bakkan ba far léen moom. + +Sànkoon nañu seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naafeq. +Ñu sukkandiku woon ci Aji jariñ (Yàlla) jiy Aji wërsëgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem wërsëg yi. + +Ñoom de dañoo boyoon jëm allaaxira ngir ne dañoo fase woon wujj wa (adduna). +Masuñoo bàyyi lenn ndigal lu juge ci Aji settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla) kiy Aji bind ji. +Ñoom de - ci saffanub ñuy bàyyi ndigal yi - dañu ciy sax ànd ceek bànneex, ndaxte koomum ja yi du tax ñu koy fàtte (alal ji ñuy jële ci marse yi duñu tax ñuy fàtte ndigali suñu boroom yi) . +Wuññi woon nañu lëndëm-lëndëmi gox yi ci xam-xam ak jëf ak dëppoo. + +Ndaw ñu di sang yu ñaw ! ñoom de la neexoon ca cafka ga jël nanu ko. + +Yal na ngërëm - lol di naa ci dajeek ëlëg ka làq cang gu joyu ga – sottiku ci seen kaw . +Kooka mooy Muhammad, yal na ko Aji des ji sotti ay xéewal ak mucc mook ñoñam ak saabaam yi di ay ndab (yuy duy xam-xam aki xeewal aki hikam) + +Li waral xasida gi + + Man dey tay damaa ñëw ngir wuyyu lenn ci murit yi di woroomi tuub (ñiy tuub ak a jéggalu seen boroom). + +Ñoom de dañoo sàkku woon ñu defal leen woy wuy jàngale ay teggiin, ngir ñu sàkkoo ciy teggiin, te loolu wartéef la . + +Ndax kat képp ku bëgg a topp Yonnant bi te tegoo ko ciy teggiin dees na ko xañ ag texe akug jariñu +Moom teggiin de - ci àdduna ak allaaxiraa – mooy gën ji ndàmb tey gën ji lu ku tedd di tedde +Ndaxte mooy leeral ab xol tey jegeele àjjana.Dina waral say dëkkandoo di la tagg te dina sooreel it sawara. + +Ma daal di jug (ngir sàkku gi ñu ko sàkku woon ci man ) gaawantu, tontu léen, di ci sàkku nag ab yool ak ngërëm. +Moom nag du lu dul jël la Waliya wa tuddoon Dal-Haaji wesaroon (manaam la mu bindoon te woyu ko,maanaam defu ko woon ay bayit ) def ko ay woy, di ñaan ci def gi Yàlla fajal ma samay aajo + +Lu tax ma taamu ko ? + + Ndax dafa boole – ba noppi gàttal ko – li ëpp ci li taalifkat yu njëkk ya bindoon cig tàqale. + +Lépp loo gis mu néew te doy moo gën lu bari te sonle. + +Def naa ko nag woy wu ami njariñ, ci baaxug Yàlla mi dige (ci Alquraan) ne dana aar (ñi gëm) +Ndax Yàlla may ma ci ngërëm ak kóolute ak njéggal ca bisub njàqare ba. + +Kon kat yéen sàkkukati xam-xam yi maa ngi leen di dénk te dellu di léen dénk te di leen xiirtal ci tontu bii (téere Nahju bii) +Ndax kat yor na ci ay jikko aki teggiin lol (bu ngeen ci tënkoo ) dina leen wommat jëme leen ca jub ga + +Ay gindee ngi ci aki jariñ yoy boroomug nammeel (ab murit) du ci yoqat mukk +Kuy door a dal ak kaaŋ-fóoree yam ciy njariñam , aw yiwam it du jeex mukk. + +Ndaxte ni ñuy àgge ci gën jaa rafeti jikko yi mi ngi ci ak ca (lu baax) la ñuy mébët. +Maa ngi ko tudde: + +Nahju QadaaAl Haaji) ci góob mbayum suñu sëriñ bii di Dal-Haaj. + +Maa ngi ñaan Yàlla mu nangu ko ca baaxam ga te àggale liggéey bi. +Di ko ñaan it mu mel ne turam wi, ba ki koy jàng ay mbiram man cee yéwéne ngir mu texe +Te mu musal ma ci ngistal ak aaw (naw sa jëf) ci barkeb Yonnant biy boroom Liwaaul Hamdi +Ak yu dul ñoom ñaar ci caay-caay yi (bon-bon yi) te mu may ma ay ngënéel +Te mu musal ma (t.s) ba fàwwu ci ayuw ibliis mii nga xam ne dafa féttéerlu . + +Te mu musal ma ci ayu li mu bind ci suuf si, ak li mu bind ci asamaan si ak li nekk ci seen diggante ñoom ñaar +Te mu may ma ma topp ci sunnas Yonnant bi (j.m) miy gën ji mbindéef , miy ku ñu ramuloo, miy ku ñu topp + +Ginnaaw bi mu jullee ci moom te sëlmël ci, ak ñoñam aki saabaam ci anam gu dul dog. + +Fii nag mooy fi tarjumaani téere bi yam, kon leegi nanu jublu ci (indil leen) teggiin yi. + +ndoorte li + + Ngir woy (nos) lii di wesaru Seex Ahmadu - mii di ku géeju ci xam-xam – maa ngi naan : + +Yeen mbooleem way sàkku yi xam-xam déglu leen sama laabiire gii di léen tàqaleek ag texeedi +Mu di laabiire gog dañu leen koo jëme ngir jëmmi Yàlla rekk, muy yee nag jépp aji xellu ak ku jamuj(fàtte) : + +Yoonu teggiin de mooy yërëm ndaw, ni ko baayam di yërëme ak ndayam te weg magak def sa moroom ni sa bopp ngir jëmmi Yàlla mi nekk ca aras (toogu ba)'''saraab aji taalif ji : +Yoonu teggiin mooy nga yërëm ndaw mel ci moom ni baayam ba ko jur te am lool ci moom yërmande, te mel ci ne ndayam ju am ja ag ñeewant, nga weg it mag ak doonte da di ab jaam bu bawoo Abasa (Ecopi) , te nga yamale sa bopp ak sa moroom ngir jëmmi Yàlla kepp. + +Xamal ni teggiin de mooy taarub boroom xam-xam ak ku koy sàkku, mooy it takkaayi aji xellu ak ku lewet, mooy njobbaxtalu jikko yi, ku ko takkaayoowul yoqéel na (ñàkk na ay takkaay)te neenal, dana mujj di ku ki bind bañ ak ñi mu bind (Yàlla aki mbindéefam) képp ku ko gis bañ ko te sànj ko (mere ko), kepp ku toog ak moom am ci moom ag yoqat akug doyal. + +Bokk na ciy teggiin ngay laabiire koo gis ca la nga gis ne ag jubam a nga ca, te ngay bañ a yayale +sa bopp jenn àq ci kenn, te nga jort it ne yayoowoo ci kenn mu lay màggal (ci lenn). + + +Loolu nag mooy li mu junj ci waxam jii : + + Nangay yërëm gone +Nangay yërëm gone, (rikk) bu ko nëbbal benn yoon genn laabiire gu aw yiwam nekk. +Deel weg mag ak doonte da di ku doyadi te xeebu. +Bokk na ci ay teggiin nga bañ a jort ne yayoo nga jenn àq ci kenn ku mu man a doon . +Te nga bañ a séentu genn maggal ( mbaa wormaal) mu juge ci kenn (kok man nay mer sax ci màggal gi mu lay màggal). + +Yaw daal jortal ne teggiin yepp ci yaw la war a bawoo, bu leen séentu mukk ci say àndandoo. +Àndal ak nit ñi ni nga bëgge ñu ànde ko ak yaw. Saraab aji taalif ji : + +Li mu namm a wax mooy : bokk na ci teggiin yu rafet nga jort ne ay teggiin moom ci yaw rekk la war a juge, te nga bañ di ko séentu ci ku dul yaw. Te ngay ànd ak nit ñi ( ci jikko yu baax yi nga bëgg ñu ànde kook yaw) (boo ko deful it jikko yoo ànde ak ñoom ci yu bon séentu ko ci ñoom, nit ñi daal ni nga mel ak ñoom rekk lañuy mel ak yaw). + +Nangay sàmmoonteek aqi (Yàlla) - boroom màgg giy boroom kàttan gi - ci ñoom ngir jëmmam ja (moom Yàlla) ni waxi woykat ba : + +Mu bëgg a wax rekk ne bokk na ci teggiin yu rafet ngay sammoonte ci mbindéef yi àqi ki leen bind(t.s) ci di àndeek ñoom ni ko woykat bi waxe ca qasidaam ga yor bahru basiit:Yaw mbokk mi nangay am yërmande ci mbooleem mbindéef yi, nanga léen di xoole bëtub ñeewant ak yërmandeNangay weg mag di yërëm gone, tey sammoontek àqi aji bind ji ci mépp mbindéef. +Am na addiis bu naan : sama xeet wi de du dañ di nekk ciw yiw li féek ku ndaw a ngi ciy weg mag, mag di ci yërëm gone.Kon rikk nanga di roy ci gindig Imaam yi (y.y.g)kon de di nga gindiku + +Bul di toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a ñàkk(loola mooy lu mel ne) : ngay jàng ( ci moom) walla nga dëkk (ak moom) walla nga bokk ak moom di lekk, bul toogandook moom cib lal it + +Saa su (Yàlla defee nga toogandook moo) nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu +Akug watandiku, te bul di tafu ci kawam, bul toog it ci kanamam + +Yaw mbokk mi (rikk) bu ko tàllal sab tànk boo toogee ci moom, te deel damm sab gis wëlif ko (maanaam bul ko di faral di xool rekk + + Saraa : + +Mu bëgg a wax ne : bokk na ci teggiin yu rafet nga bàn a toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a ñàkk, ngir jàng mbaa dëkk ak moom walla di lekkandook moom añs. +Boo toogeek moom it nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu ak wattandiku. Bul di ko ñóoxu mbaa nga koy tàllal ab tànk, bu ko di ja tam, bul di baril di gëstu ci lu dul aajo, ndax loolu ci màndargay ag ndof la, Yàlla nee na (t.s) : (( neel jullit ñi ñu dam seenub gis . loolu moom lay junj ci waxam jii di ñëw : + +Bul di baril looy geestu fu nekk, te dara ñoru la ci geestu gi. +Ndax loolu kat màndargam ndof la, te (boo demee ) ci téereb Yàlla bi (di nga fa gis) : ((neel jullit ñi''')) +Deel topp ndigali boroom mbindéef yi, ndax kat nekk na ci addiis : waay de (sànkoo na ci bennub xool rekk) +Ab woykat de waxoon na bu yàgg ne : ( booy def loo gis xool ko danga ci mas a am bis) kon bul di wëndéel sab gis . +Saraa : +Mu namm a wax rekk : war na la nga topp li la sa boroom digal muy damm sab gis. Ndax Addiis bi nee na : waay de dana xool benn xool bob xolam dina ci yàqoo nib der di yàqoo ca sébej ga , du ca jariñu mukk. +Woykat ba nee na : +( yaw de boo sànnee sab gis ngir sa bànneexub xol, bis dina ñëw bob li ngay gis dina la sonal +(danga gis lol doo man léppam (doo man a am lépp ) te doo man a muñ rekk ca lenn la ( doo man a yam rekk ca xool ba. Doo ko man a am te doo ko man a muñ, bu ko defee ngay sonn ci loo dul am, te boo ko gisutoon doo ko yittewoo) +Keneen it ne: +( jàmbaar du mooy kiy aar ay gawaram ca bisub jamante ba, bu xare ba tàkkee) +(waaye ka damm ab gisam mbaa mu lem ab tànk wëlif ay moy kooku ci jëmmam mooy gawar dëgg bay jàmbaar ) +Bul di baril am po, bul di ree lu bari, mbaa ngay baril looy yëngatu ak a defi neen +Bul di baj-baji mbaa ngay jéem a yëddu lu nëbbu lu mu man a doon +Loolu de màndargam tóoy la ak woyofum xel ci ku ko baaxoo +Boo jekkee nanga dalal say cér, nangay taqook ag noppi ànd ak dëddu (ci lug dëddu war) kon de nga jariñu +Deel muñ ag ŋàññ te bu ci tontu kenn, te mel ni na boroom njàngat la (adiib) waxoon : wallaay damay romb waa ji mu may xas may jellale naan kii de xam naa ne waxuma +Ndax kat xasante ak weddeente bokk nañu ci jikko yi gën a bon niki dóorante. +Bariy ree daay ray ab xol, kon rikk néewalal ree yi, ndax nga gërëmloo Boroom bi + +Saraa: + +Maanaam bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ a barili ree, po, ag neen, ag baj-bajeek yëngatu ak a jéem a yëddu lu nëbbu, loolu de ci màndargam tóoy la bokk,ak gàttum xel, nangay faral a dal boo jekkee (boo toogee) cib jataay tey faral a noppi, ba ñu laaj la, bu boobaa nga tontu ci kàddu gu suufe, walla nga soxlaa laaj dara, bu boobaa nga def ko te yam ca sa soxla rekk, bu ca dolli dara, ndax kat noppi noflaay a ngi ci ak sutura niki ñu ko waxe:(nëbbal ayib yi kem li nga man cig noppi, ndax kat ab noflaay a ngi ci noppi ñeel aji noppi ji )(defal sab tontu boo lottee muy “noppi”, bari na wax joj tontu baa nga ca ag noppi) +Bokk na ci Hikma: +Bu wax doon xaalis noppi di wurus, bu la nit réeree (def la ag ñàkke-teggiin) Jéllale ko taqoo noppi, ni ko Yàlla waxe: (( Jéllaleel ñeel ñi réere)) ((bu ñi réer waxee ak ñoom nu tontu léen ci luy waral jàmm)) +Ni ko woykat bi waxe: +(Amaa na ma romb ku soxat ki (ku yaradiku ki) mu may ŋàññ, bu ko defee ma fegu te naan kii daal waxut ak man) +ŋàññante ak weddeente bokk nanu ci jikko yi gën a ñaaw, yi gën a bon, ree ju bari day ray ab xol. Boo bëggee am sa ngërëmul boroom, néewalali ree, Yàlla ci jëmmam (t.s) moo ne : ((nañuy ree lu néew )) +Boo toogee ak ku la mag booy ree nangay yam ci muuñ +Booy wax ak moom it bul bayliku ( ëppal ci wax ji) ndax loolu du lu rafet +Noppil ba nga gis mu bëgg a wax ak yaw, bu boobaa yamal ca la mu soxla ci yaw +Loolu kat moo di ay teggiin, kon jëfe ko cig wàllam +Bu la béccingalee , muñal béccingalam yooyu, bu defee lu jaaduwul suturaal ko +Bul dañ di ko jéggalu, te bu ko di mere it +Bu koy faral di ja (jëmale ko say gët , samp ko ko rekk) ci waxtu wu nekk + +Saraa: + +Bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ di ree ci jataayub ku la mag ndare muuñ, nga bañ di wax ak moom cig bayliku, maanaam ëppal ci wax ji, lu ñor nga wax ak lu ñorul,moom daal nanga yam ci li mu soxla ci yaw, bu boobaa doxal nga ay teggiin ci moom. +Bu la defee lu jaaduwul jéggal ko, te di ko jéggalu, bul ko di faral di xool xool bu metti, ndax loolu duy teggiin +Boo bëggee juge ca jataay ba, nanga ko defe cig tëyyewu (tëyye sa bopp ba suuf du jug pënd du jeqiku) +Bu léen xëpp suuf si ci seeni kanam ndax loolu wuute na ak ag jub +Boo ko manee bul di nelaw ci biiru nit ñu nelawul +Ndax kat loolu duy teggiin, ngir ne am na lu ci nekk lu man a waral ag yeddeel (kuy nelaw man ngaa ngelawal te doo ko yëg) + +Saraa: + +Bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ a jeqi pënd boo toogee ci jataay bay jug, boo nammee jug , def ko ci ag dal akug tëyyewu, te bul jaar ci kanamu way jekki yi. Bokk na ci ay teggiin nga bañ di nelaw ci digg ay way yewwu boo ko manee, ndax amaa na ngelaw génn ci yaw te doo ko yëg, ndax bët ay saañu ag suuf(bën-bënu aw taat) + +Nanga xam ne fuqale bokk na ci liy waral gàcca ak yeddeel +Képp ku aj yitteem ci lekk ak séy na xam ne boole na lépp luy toroxte +Lekk dee ci jël lu lay dëgëral ba nga man a jaamu sa boroom te yam ca +Deel wattandiku jamono ju nekk fuqale ndaxte mooy cëslaayu wépp ay +Saraa: +Bokk na ci ay teggiin ñàkk a fuqale ak ñàkk a aj sa yitte jépp ciw ñam , loolu de cig suufe la te day waral ag ŋàññ +Woykat ba nee na: (yaw de foo fi joxe sa biir li mu la laaj ak sa pëy , di nanu àgg fa mbooleem toroxte ya yam ) +Sab loxo nanga ko tëyye, bul ci di baril am po, ndax loolu de ayib la +Bul jottaliku mukk lol làqul njariñ lu la man a jegeel sa boroom + +Saraa +Bokk na ciy teggiin :tëyye sa loxo ak bàyyi di ci fo ak bàyyi di ci jefandikoo lu njarin nekkul, loolu de bokk na ci li woroom xel yi ayibal, te ci la musiba yi tase. +Saa soo déggee ku la mag mu soxla dara +Niki mu bëggoon ku mu yonni, rikk demal doxal ko yonneem boobu ngir jëmmi Yàlla +Bu kenn soxla ci yaw dara ndare bu danga koo defal loolu mu soxla ci yaw, boo dee def noonu de danga am teraanga +Rikk bul di wax kenn fen nga, walla wax nga lu dul dëgg, walla juum nga +Walla jeneen wax ju man a merloo ak doonte ki nga koy wax gone la, di ko waxe de ag njuumte la +Bu waxee loo xamul nee ko dëggal nga, kon dees na la teral +Nee ko daal man de tegoon naa ko neneen, walla leneen laa jortoon, walla réere woon naa ko +Ak yeneen baat yi walla waxiin yi man a bégale, loolu de boo ko defee def nga lu rafet, bul ñaawal te bul lore +Deel tàmbal saw làmmiñ wax lu baax, kon de dinga ci ame ag texe te dees na la ci fegale wépp ay +Ngir waxi sangub mbindéef yi (ku nekk na….) yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ci anam gu sax (ku nekk na….) : (ku nekk na di gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi) + +Saraa + +Bokk na ci teggiin yu rafet nga saxoo di faj aajoy ku la mag boo ko déggee mu koy sàkku, niki mu soxla woon ku mu yonni +Bokk na ciy teggiin ba tay nga bañ di gàntul kenn loo man lu mu soxla ci yaw, te bañ di wax kenn (fen nga) mbaa ( li nga wax du dëgg) mbaa baat bu ko man a merloo ak doonte yaa ko mag, bu waxee loo xamul dëggal ko te ne ko (man de nekkuma woon foofu) walla (jortoon naa ne) walla (xamewuma ko woon noonu) ak yu ni mel ci waxiin yu rafet +Nangay tàmmal saw làmmiñ wax ju rafet . Yonnant bi (j.m) nee na : (ku gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi) +kenn ci woykat yi nee na :(tàmmalal saw làmmiñ wax ju baax, kon de danga ca ame ab cér)(làmmiñ de li nga ko tàmmal rekk lay tàmm)(lu mu man a doon la nga ko ca miinal rekk lay def)(moo xam lu baax la mbaa lu bon, deel xool nooy dollikoo) +Sab dox na ko aajo di waral ci lu dul ag rëy, ag rëy de ci mbugal lay bijjee jëme +Bul di ree mukk ci lu dul lu yéeme, bul dox mukk it ci lu dul aajo +Bul gestu tam te sàkkuweesu ko, ndax yii yépp ag ndofe la gog dàqoo na’aki teggiin +Sa tubay it bul ko di wuññi mukk, ndax loolu ci bàyyi ay teggiin la bokk +Moom de ci jikkoy kàccoor yi diy saay-saay te bokk ci giirug Hassaan la bokk, ñoom ñi dëddu lu baax +Nangay moytoo wuññi sa biir ak li nekk ci diggante jumbux bi ba ci bëti-woom yi, (ngir bon gi mu bon) +Loolu de màndargam réer la ak ndofe ak néewug mbañ-rus gu màgg gi +Ndax moom (mbañ-rus) mooy dàttub diine, fu mu nekkul diine nekku fa , loolu de la (jàngalekat yu mag ya) saxal +Koo agsi ci moom nanga ko nuyyu, bu fekkee ne soxla nga ay teggiin +Bu fekkee ne moo la njëkk a nuyyu nanga ko fay ci kàddu +Boo saafoonteek moom (boo nuyyoonteek moom ) nanga dëgëral sa loxol ndijoor ci ndijooram, loolu mooy li nu rafetlu +Bul rocci sa loxo li feek njëkku la koo rocci moom ci anam gu fés +Ndaxte de sibees na fëkk ay loxo ci nuyyoo ci anam gu gaaw ak bàyyi wax ja +Saafoonte ci ñaari loxo it bokk na ci ay teggiin, niki ñaar yi nu la waxoon leegi +Ñaanalal ki ngay nuyyool yaw boroom xel mi, ndax loolu de bokk na ci liy fari bàkkaar +Boo bëggee dugg ci kër (walla néegub) jàmbur nanga yëglu, kon de nga am la gën +Bu ñu la digalee nga dugg nga dugg, bu dul loolu dellul +Sab bët bul ko di wëndéel ci néegub jàmbur (mbaa këram ) ngir ragal gis fa awra joj bëggunu woon nga gis ko + +Saraa + +Bokk na ciy teggiin booy jug aajo rekk di la yekkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggiin ngay moytoo wuññi say sér, loolu de ci jikkoy kàccoori Hassaan yi la, bul di feeñal lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say wóom, loolu de ci réer la ak ñàkk kersa te kersa mooy dàttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa ñàkke diine jug fa. Bokk na ci ay teggiin ngay nuyyu képp koo dox ba àgg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey dëgëral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga bañ koo njëkk a rocci sa loxo , fëkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu ñu sib la. Bokk na ci ay teggiin ngay saafoonteek moom ci sa ñaari loxo yépp, te nga koy ñaanal lu baax ak sa bopp loolu bokk na ci liy far ay bàkkaar . bokk na ci ay teggiin ngay def booy dugg ci néegub jàmbur mbaa këram ngay yëglu bu ñu la nee jàllsil nga dugg, ndeem déet nga dëpp, rikk bul di sànni sab gis ci kër mbaa néeg boo moomul ngir nga bañ faa gis loo warul a gis. +Boo bëggee kooy àndandool bu muy ku dese cim xel mbaa ku iñaan mbaa ku bariy xemmeemtéef +Bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am càkkutéef la +Ndax de xibaar nañu ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu ñu tuxal(waa ji de diine ji waayam yor rekk lay yor) +Saraa: +Da lay dénk nga bañ a àndandook way dese yi cim xel te bañ di toog ak ku la dul dolli diine ak xel, ci loolu de ngay ame la nga bëgg, ndax waa ji de ni ab xaritam mel rekk lay mel, (wolof yi nee nañu won ma sa xarit ma wax la sa jikko) seyyidinaa Aliyun - karramal laahu wajhahuu – nee na:(Bul def mukk boroomug réer muy sab àndaale, moytu ko te moytu sa bopp)(bariwaa na aji réer ju alag boroomug lewet (ku nite) ba mu ko defee mbokk) (nit de ca moroom ja lañu koy natt bu àndeek moom)(ni ñuy natte dàll ca moroom ja bu ñu dee ñaar) (mbir de am na ag niroo akug natt ca moroom ja)(xol de misaal la ca moroom ja ) +Am na ku ne :(boo nekke ciw nit nangay seet ña ca gën ngay ànd ak ñoom)(bul seet ña ca yées ngay ànd ak ñoom bay yées )(bul laaj waa ji, waaye laajal ab àndandoom)(Ndax ku nekk ca ka ngay àndal ngay roy) +Bul sàkkoo gis mukk ab rëcc-rëcc (ci sa moroomu nit) bul gëstu itam ay awra (ay ñaawtéef) + +Saraa + +Mu ne : bokk na ciy teggiin ngay bañ di gëstu rëcc-rëcci nit ñi mbaa seeni ñaawtéef. +Waxees na ne : +(bul di sàkkoo xam la nit ña nëbb ci seeni ayib) +(ndax kat loolu man naa waral Yàlla di muri mbalaan mi mu muuroon ci say ñaawtéef) +(rikk nangay tudd lu baax la nekk ci ñoom bu nu léen tuddee) +(bul ayibal kenn ci ñoom ndax kat loo léen wax man naa am yaa léen ko ëpp) +Nanga mel ne na woykat ba waxoon: +(dinaa bëgg jikko yu rafet yi sama kem kàttan) +(tey bañ di ayibale ak ñu may ayibal) +(may jéggal ŋàññug nit ñi ngir ag lewet) +(ndax ki yées ci nit ñi mooy ki sopp ag ŋàññante) +(ku weg nit ñi wegees ko) +(ku xeeb nit ñi deesu ko weg) +Ka wax lii de wax na wax ju rafet: +(boo bëggee dund sa diine mucc) +(sa wërsëg lëw (bari) sab der ñoŋ) +((boo bëggee loolu) sa làmmiñ bu ci tudd mukk ayibi nit) +(ndax kat yaw it am nga ay ayib, nit ñi ami làmmiñ) +(bu Yàlla dogalee say gët rot ci ayibi nit, nee leen :) +( ee yéen gët yi bu léen xool de, ndax nit ñi ñoom it am nañu ay gët) + +des na + +Yoonu murit +Botswana li ëpp ci suufam mi ngi ci tàkku Kalahari gi. Mi ngi nekk ci Bëj-saalumu Afrig, ci bëj-gànnaaru réewum Afrig gu Bëj-saalum. Ay xammekaayu melosuufam ñooy: 22° Bëj-g 24° Bëj-s. + +botswana +melosuufug afrig +Waxi Seex Anta Joob ju aju l��kk + +Làmmiñ ak jamono + + Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko;làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ne paaka bu xumaag. Tubaab yi bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu koo yore ci seen làmmiñu bopp.Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des ginnaaw.Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag anjaboot ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko...Loolu moo taxoon ñu sàggane sunu làmmiñ yii.Waaye du caagéenu dañu cee manul woon a waxe li ñu bëgg a wax... + +Dangeen di xam ne aw làmmiñ, jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd, am xel ay gàtt, aw làmmiñ gàtt!Waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk, aw làmmiñ man na koo tudd;aw làmmiñ gàttul. + +Nit kiy wax nag fi xelam yam, fi jàngam yam, fi gis-gisu àddunaam yam, foofu rekk la ay waxam man a yam... + +Waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk, làmmiñ dina ko tudd. Lu ko waral? Amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul!Mooy li nga xam ne - waxoon naa ne...dinaa cuq tuuti xel yi...ndax defe naa ne, yéen jàng ngeen xam-xamub làmmiñal...xam ngeen ne De Saussure (boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal) wone na loolu.Làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa. Baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la! Kepp! Amul sax menn maanaa. Ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am, kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde.Wenn tur wi di moom te loolu amul. + +Jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu Seex Anta Jóob, mu amoon ci awril 1984 ca Cees + +Kàllaama +Banda : Plectorhinchus mediterraneus (jén - dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réew : Kap Weer - Ginne Bisaawóo - Gànnaar + Melo : gris violacé + Dayoo : 60cm - max 80 cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Plectorhinchus mediterraneus" + +Jén +Wersun : Spondyliosoma cantharus (jén - rab) + + Askan (pop) : ? + Réewu Afrig: Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Gànnaar - Senegaal + Melo : dóomu taal + Dayoo : 60cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Spondyliosoma cantharus" + +Jén +Mi ngi nekk ci goxub Afrig, ci diwaanu sowwu Afrig, rëyaayam di 274 200 km², 81u réew mu ëpp ci àdduna bi +Burkinaa Faaso Mali moo wër ci bëj-gànnaar ak ci sowwu, Niseer nekk ci bëj-gànnaar-penku ak ci bëj-saalum-penku, ci bëj-saalumam Togóo, Gana ak Kot Diwaar ñoo fa nekk. Kon amul ubbeeku ci géej gi. Doon na réew mu tappndaar ndaxte pujam bi gëna kawe Tenakuru te kawewaayam toll ci 747 m ca sowwu réew ma. + +Li mu am klimaab gëwéel mooy tax ñaari jamono rekk la am, noor ak nawet. Ni senegaal, li gëna féete bëj-gànnaar dafa tàkku, ci fi tollook Sahel, looy gën di wàcc jëm bëj-saalum muy soppiku di doon ab mandiŋ. Di nañ fa fekk itam ay àll rawatina ci diwaani Bobo-julaaso ak bu Banfora, soo jëme itam Gawua ak fi jege dig yu kot-diwaar-gana + +Xool it + +Burkinaa Faaso +Buruundi am réewu diwaanu Diggu Afrig la, rëye na 27,830 km², 25,650 km² suuf la, 2,180 km² di ndox. + +Melosuufug jëmm +Mi ngi digook Kongóo-brasaawiil ci lu mat 233 km ci sowwu, ak Ruwandaa ci 290 km ci bëj-gànnaar, lang ak Tansani ci guddaayub 451 km ci penku. Buruundi amul ubbeeku ci géej gi, waaye yi ci bëj-saalum-sowwu da ñoo lang ak déegub Tanganica bu rëy ba. Réew mi dafa nekk ci diggante ñaari mbandi ndox yu mag yii di Niil ak bu Kongóo + +Xool it + +Buruundi +Kamerun am réewu diggu Afrig la, jëmmam dafa mel ne ab ñettikoñ, rëye na 475 442 km², 98,8% di suuf, 1,2% ndox la, di 42u réew mi ëpp ci àdduna bi, am na it 402 km ci tefes. + +Ay digam +Réewum Niseeriyaa moo ko féete sowwu, Mbàmbulaanug Atlas gi, Gineg yamoo gi, Gaboŋ ak Kongóo-Brasaawiil nekk ci bëj-saalumam, Réewum Diggu Afrig ak Cadd nekk ci penku, dexub Cadd bi ci bëj-gànnaar. + +Xool it + +melosuufug Kamerun + +pt:Camarões#Geografia +Ngaté yénnö : Diplodus cervinus (dieun - dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réewu Afrig: Gaambi - Gànnaar - Senegaal + Melo : dóomu taal + Dayoo : 30cm (max : 60cm) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Diplodus cervinus" + +Jén +Ngaté bu digen : Diplodus vulgaris (jén - dundat yi) + + Askan (pop) : ? + Réewu Afrig: Gànnaar - Senegaal + Melo : dóomu taal + Dayoo : 25cm (max : 45cm) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Diplodus vulgaris" + +Jén +Yooyu yennat lañu ci ay lëkkalekaay ci njàngum wolof: + + http://www.chez.com/afroweb/wolof.htm + http://www.chez.com/afroweb/wolo_frm.htm + https://web.archive.org/web/20080724082256/http://www.aventuresland.com/toutlewolof/ + http://www.lexilogos.com/wolof_dictionnaire.htm + http://www.wolofonline.com/#course + http://books.google.fr/books?id=XfVEyi8CeNAC&pg=PA149&lpg=PA149&dq=leemu+wolof&source=web&ots=6LLOy6RGio&sig=8RXWmL0xCnWYyZ4iSW4jJlOIQkQ&hl=fr&sa=X&oi=book_result&resnum=1&ct=result#PPA146,M1 + + +wolof + jële lëf ci barab, yobbu ci beneen + +français + Transmission +baati wolof + + +wolof + yabale + tukkib xam-xam ci réew mu sori, mbaa mu jafe, walla tukkib nemmiku bu am solo mbaa mu xaw a yëngu;nit ak bagaas yi bokk ci tukki bii: ab yonne bu jëm dottub bëj-saalum + +français + émission + expédition: +Voyage scientifique dans un pays éloigné ou difficile, ou voyage touristique plus ou moins important ou mouvementé ; hommes et matériel participant à ce voyage : Expédition au pôle Sud. +baati wolof + + +wolof + nangu dara, teg loxo, jël + +français + réception +baati wolof + + +wolof + lu ñuy yeewe di ci takke + ak wën gu mbëj di jaar 1 + +français + corde 1 +baati wolof + + +wolof + Ceññeer-mbej: +Ceññeer-mbej day wund feeñte yiy saytu sosu ak tasug duus yu mbejbijjaakon yu néew kàttan yi. Moom nag (Ceññeer-mbej)mooy cëslaayu mbooleem xarala yu jokkoo yiy sukkandiku ci duus yu mbejbijjaakon yi. + +français + radioélectricité +La radioélectricité: désigne les phénomènes qui régissent la formation et la propagation des ondes électromagnétiques de faible énergie. Elle est le fondement de toutes les techniques de communication ayant pour support les ondes électromagnétiques. + +baati wolof +Jëmm +Kàttan + + +wolof + “ngiste” mooy bànqaasub jëmm biy saytu mbirum leer ak séqoo yi mu am ak gis + +français + optique +L'optique est la branche de la physique qui traite de la lumière et de ses relations avec la vision + +Baati wolof +Mbëjbijjaakon mooy banqaasu jëmm biy gëstu feeñte yu mel ne mbëj ak bijjaakon ak lépp lu leen ñeel (niki ci misaal tooli bijjaakon yi juddoo ci dawaanu mbëj ak dawaani mbëj yi juddoo ci tooli bijjaakon). + +Ñoo ngi ko tëgg ngir man a faramface ci anam gees boole feeñte yu mbëj ak yu bijjaakon. Ay feeñte yu mel ne xiirtalug mbëjbijjaakon ngir wone ni toolu mbëj lënkook toolu bijjaakon: ab toolu bijjaakoon buy soppiku dafay jur ab toolu mbëj, naka noonu la toolu mbëj buy soppiku di juree ab toolu bijjaakon. Yamaleb Maxwell mooy liy faramface mbëjbijjaakon te di sukkandiku ci yan ak dawaanu mbëj. + +Taariix +William Gilber , ci téereem ba De Magnete (1600), la wone wuute gi nekk ci diggante aw yaram wu mbëj ak wu bijjaakon. Mu fésal àtte yi laqu ci bëmëxante ak xëccante yu bijjaakon yi jaare ci seeni dott ak njeexit li tàngoor am ci bijjaakon bu weñ. + +ci 1831 la Michael Faraday doon gëstu doxiinu dawaan bi ci biir ab toolu bijjaakon ba gis ca ne, moom bijjaakon bi, man naa jur liggéey. Oersted moom wuññi woon na ne ab dawaanu mbëj dafay jur ab toolu bijjaakon, Faraday moom wuññi ne ab toolu bijjaakon dafay xiirtal ab dawaanu mbëj. Ci noonu la wuññee baaxi doxalukaay bu mbëj ak ni liggéey bu doolerandu man a soppeekoo kàttanu mbëj, naka-noonu mu sàkkee ca ab jurukaayu dawaan. + +Mbëjbijjaakon a ngi judd ci bi James Maxwell (1864) boolee ay gisiin yu jiitu woon, niki mbëjtekkaaral, bijjtekkaaral. Bii gisiin di bees bennal moo leeral jikko yi ci yani mbëj yeek dawaani mbëj yi, bijjaakon yi, duusi mbëjbijjaakon yi, yu mel ne ag leer walla duusi rajo yi. + +mbëjbijjaakon +Dottub Bëj-saalum mooy gox bi gën a suufe ci Suuf si. Nekk ci dottub Bëj-saalum, Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi moo ko wër. Laal na itam géeju Ross ak bu Weddell. + +Réyaayam toll ci 13,9 junni-junni km², Dottub Bëj-saalum moo gën a tuuti Asi, Afrig, Bëj-gànnaaru Aamerig ak Bëj-saalumu Aamerig. Tugal ak Oseyaani rekk la gën a réy. Lu mat 98% ci suufam galaas a ko sàng, ci dëllaay bu mat 1,6 km. + +Dottub Bëj-saalum mooy gox bi gën a sedd, bi gën a wow, ëpp ngelaw. Di itam gox bi gën a yëkkatiku ci kawu tollulwaayu géej gi. Ñakkug taw ga fa am, lu dul ci tefes yi, moo tax ci biir gox la tàkk bi ëpp ci Suuf si nekk. Amul nit ñu fay dëkk lu yàgg, amul itam nit ñu fa baaxoo. Ay gañcax ak ay rab rekk a fa man a dëkk. + +Melosuuf +Ak réyaay bu toll ci 13,9 junni-junni km² mooy juroomeelu gox bi ëpp ci àdduna bi cig réyaay. + +Gox bi dafa séddaliku ci ñaari xaaj: + + Sowwu Dottub Bëj-saalum + Penku Dottub Bëj-saalum + +Lëkkalekaay yu biir + Goxub Dottub Bëj-gànnaar + Dottub Bëj-saalum + Dottub Bëj-gànnaar + +Gox yi +Diiwaani dott +Xarey jóoñe yu jamono ju diggu ji, nekkoon nañu di ay aj aki siyaareji yu ñu ngànnaayal, paab bee leen daa woote, ngarmi gu Tugal gi di leen jàppale ci alal, di leen kapparal, te di leen jëfloo, bu ko defee, ñu sóobu ci ay jiyaar yu nasaraan. +yonnee yu xare, yu nasaraan yii, ñi ngi léen daa wootee ci turu goreel Quds (Sorisalem), gi waa Tirki tegaloon loxo Araabi Faatima yi, ci atum 1078 + +Politig +Baati wolof +Taariixu Tugal +Taariixu Asi +Xoolal beneen jukki bi tudd Dottub Bëj-gànnaar + +Goxub Dottub Bëj-gànnaar bi mooy gox bi wër dottub Dottub Bëj-gànnaar bi. Bii Diwaan ëmb na Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar gi ak yenn xaaj ci Riisi, Alaskaa, Kanadaa, Groenlaand, Islaand, Noorwees. Dottub Bëj-gànnaar bi amul рктык etik Āketikamas maketku tiklaka mukmus + +Dottub Bëj-gànnaar bi amul . + +Gox yi +Diiwaani dott +la ko dale ca 2008, Senegaal mi ngi nekk 14 diiwaan. +35 tund ñoom ci séen bopp dañu leen a séddale ci 92 ndiiwaan. +dëkk yi yor yenn rëyaay yi dañu leen a séddale ci dëkkani ndiiwaan, 43 ci mboole-séen. Ndakaaru, ci misaal, yor na ci 19. +Dëkk yu digg-dóomu yi ñu def leen ay Dëkkaan, Ñoom nag 67 lañu ci mboolee-séen. +Yeneen barab yi ay dëkk-dëkkaan lañu yu ñu boole ci ay gox-goxaan, yoy àgg nañu ci 324 ci 2007. + +Dëkkiin wi + +Karmat + +Xool it + +jukki yu ci aju +Diiwaani Senegaal +Tundi Senegaal +Ndiiwaani Senegaal +Dëkkaani ndiiwaani Senegaal +Dëkkaani Senegaal +Gox-goxaani Senegaal +Dëkki Senegaal + +Téerekaay + Giorgio Blundo, « La corruption comme mode de gouvernance locale : trois décennies de décentralisation au Sénégal », Politique africaine, 2000, n° 199 + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal, Dakar, Ministère du Plan, 1967, 705 p. (Thèse de 3 cycle publiée) + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal. Complément pour la période des origines à 1965 et mise à jour 1966-1973, Paris, Mouton, 1977, 637 p. + +Lëkkalekaay yu biti + Site officiel du gouvernement du Sénégal + Données statistiques worldbank.org + Chiffres population www.gouv.sn + Découpage administratif sur www.senegalaisement.com +« Décentralisation : Les bœufs attendent la charrue » (article Panos Infos, 2003)) + +dogiinu Senegaal +Diiwaani Senegaal yi ay xaaj yu yoriin yu Senegaal lañu. + +nosiinu suuf si + +dogiin wi + +Fii mu nekk, séenub lim mi ngi ci 14, la ko dale ca ba ñu sosee diiwaanu diiwaanu Matam ca 2001, teg ci yeneen ñatti diiwaan yi ci 2008 : Kafrin ci digg bi, Keedugu ci bëj-saalum-penku bi ak Séeju ci bëj-saalum, ci Kaasamaas. + +rëyaay ak askan + +{| class="toc" cellpadding=0 cellspacing=2 width=250px style="margin: 0.5em 0.5em 0.5em 1em; padding: 0.5e text-align:left;clear:all; background-color: #fff; font-size:90%" +|- bgcolor="cccccc" +!valign=Top|Diiwaan +!valign=Top|Rëyaayen km² +!valign=Top|Askan +|- +|Ndakaaru||align=right|550||align=right|2 411 528 +|- +|Njaaréem||align=right|4 359||align=right|930 008 +|- +|Fatig||align=right|7 935||align=right|639 075 +|- +|Kawalx||align=right|16 010||align=right|1 128 128 +|- +|Koldaa||align=right|21 011||align=right|834 753 +|- +|Luga||align=right|29 188||align=right|559 268 +|- +|Maatam||align=right|25 083||align=right|423 041 +|- +|Ndar||align=right|19 044||align=right|863 440 +|- +|Tambaakundaa||align=right|59 602||align=right|530 332 +|- +|Cees||align=right|6 601||align=right|1 348 637 +|- +|Sigicoor||align=right|7 339||align=right|557 606 +|- +|align=right|mboole-séen :||align=right|196 176||align=right|10 225 816'|} + + ay karmat + + Voir aussi + + Jukki yi ci aju +Diiwaani Senegaal(Régions du Sénégal) +Tundi Senegaal(Département du Sénégal) +Ndiiwaani Sénégal (arrondissements du Sénégal) +Dëkkaani ndiiwaan yu Senegaal(Communes d'arrondissement du Sénégal) +Dëkkaan yu Senegaal (Communes du Sénégal) +Gox-goxaan yu Senegaal( Communautés rurales du Sénégal) + + Bibliographie + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal, Dakar, Ministère du Plan, 1967, 705 p. (Thèse de 3e cycle publiée) + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal. Complément pour la période des origines à 1965 et mise à jour 1966-1973, Paris, Mouton, 1977, 637 p. + + lëkkalekaay yu biti + Agence Nationale de la Statistique et de la Démographie du Sénégal (chiffres des différents recensements et estimations officielles jusqu'en 2015) + « La région dans les limites administratives des États de l'Afrique de l'Ouest » (article de Gérard Brasseur dans le Bulletin de l'IFAN'', série B, 1968, tome 30, n° 3, p. 861-867) + « Trois nouvelles régions administratives seront créées au Sénégal » (Agence de presse africaine, 25 mai 2007) +Louvre (Musée du Louvre) : Paris + + Open : 1793 + + Dayoo : 60 000 m² + + Visites : 8 300 000 (2007) + +Mona Lisa, The Virgin and Child with St. Anne, Venus de Milo, Code of Hammurabi, Winged Victory of Samothrace + +Pari + + +wolof + +français + écoles moyennes +yar +baati wolof +gët mbooloo la, bennaan bi mooy bët: cér bi ñuy gise, +waaye day tekki it (agents secrets), ndax sa gët yi nga boyal ci biir nit ñeek mboolaay gi, ngir ñu xam li fi xew, nga xame ko ci ñoom, dees na ko wax it yëddukat +The wise words spoken by the philosophical genius Ashley park. +Ag Dóox (golfe): fu suuf dugge ci mbeex mi (géej gi), di safaanub bopp(cape) (ci melolosuuf) di fi mbeex mi dugge ci suuf ci + Ab Dóox - ca cosaanam (28 xarnu)- li muy wund : yaatu-yaatu bu melosuuf bu ab Dóox yor (njiitul xare) + +français + Un duché (en latin : ducatus) désignait à son origine (au VIII siècle) le ressort de commandement d'un duc (en latin : dux, ducis) ou chef militaire. Les ducs francs étaient ainsi des comtes chargés d'un important pouvoir militaire. +Parfois, des duchés ont été élevés à un rang supérieur par l'empereur germanique, soit en grand-duché comme le Luxembourg, soit en archiduché pour l'Autriche + +Taariix +Nosteg galag (Wu-faraas:système fiscal) + +Koom-koom + + +wolof + mbaxanam buur + +farncais + couronne + +english + crown +baati wolof +Gàddaay di ci fr “immigration” baat la buy tekki : tukkee ci barab mbaam réew dem ca meneen, ngir sàkku fa dara, mbaa ngir naqarig sam réew ci yaw mbaa barab ba nga bawoo, loolu di faral di jur ag tumbrànke, akug ndoxondéemu, tax ngay am turu doxondéem giy tekki ku dëkkul ca réew ma nga nekk, cosaanoowoo fa + +Kon gàddaay mooy: immigration ci fr + +Doxondéem di : étranger + +Tumbrànke di coona ak tiis ak naqaru xol gi gàddaay di faral a jur + +Looloo waral Yonnant bi (j.m) di faral di wax naan: “Tukki aw daggiit la ci mbugal +” + +Am ku ne moo de da koo woyofal waaye mbugal aw dogiit la ci tukki +Bennoo gu Almaañ + +Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi: + +Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa séddaliku woon ci lu jege ñatti téemeer ak juroom benn fukki diiwaan(360 diiwaan), yépp it ci ron imbraatóor gu Otris lañu nekkoon, walla li ñuy tudde Imbraatóor gu Rom gu sell gi. Almaañ gépp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yépp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo. + +Almaañ ci jamonoy Napoleon: + + +Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nañu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko noot, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo péeyam ba Berlin. +Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoniya bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lañu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw. + +Almaañ ginnaaw ndajem Vienne mi: + +Ginnaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lañu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Dóox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Riisi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam diiwaanub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoniya. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko. +Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di génne ay saxal aki ndigal yuy safaan tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey safaan mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko ci mu génne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu kawe yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.Doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo. + +Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi: + +Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, dugal leen ci genn nguur gu Almaañ gu ñu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum réew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem diiwani nguur gi. +Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir réew mi cim njaay deesu ci génne duwaan. Nga xam ne daññoo fééexal yaxantu gi ci Brusiya, afal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii déy dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nañu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay diiwaanam yu biir yi. Diiwaan yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay diiwaan yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg bobb gu nduwaan(systeme autonome douanier), gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lañu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginnaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu ñu séddale ci juroom benn fukki diiwaani nduwaan. + +Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li ñu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu ñuy def ba dugal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy: + +1 Solofrayn + +2 “Bennoog nduwaan gu Bavar” gi +nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at. + +3 Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoniya +Mooy gi Saksoniya taxawaloon atum 1828g. + +Kilifay Brusiya yi xamoon nañu ne diiwaani Almaañ yi danañu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu ñu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi dañoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy séddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëwéelub Solofrayn, gën a yàkkali ab géewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoniya ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, ndefar ga jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nañu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin wu Brusiya, te da na jàppeji Otris muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, duñu ay doxandéem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nañu ne Almaañ gépp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g. + +Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmmaan (individu) ak lépp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gisu Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa di xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu ñu jiite woon bennalug Almaañ gi. + +Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy réew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a dëgër ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jéego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ. + +Jeexiital yi jeqiku gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi: + +Ay jeqiku yu bari jot nañoo am ca Tugal atm 1848g. Ag jeqiku am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu . + +Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot jeqikuy Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe. +Kërug Tugal gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca réewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj. + +Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu réew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jéem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yépp teewe woon nañu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat (walla taalifkat) , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas. +Ñatti saxal nag yu mag juddoo nañu ca ndaje ma: + + Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya. + Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatóorug Otris gi + Génne Otris ci bennoo gu Almaañ gi. + +Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nañu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatóor ci Almaañ gu ñu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatóor li ñu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol. + +La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Riisi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nañoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a noot fipp gi amoon ca péeyam ba Vienne. +Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi teguñu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du liggéey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi. + +Otris ak Riisi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te ñu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jéem gi ñu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal duñu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu réew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole. +Looloo waraloon ñu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a génne Otris ak Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu ñuy doone benn ci ginaaw bi. +Xalaat bii nag diisoowaale (chancelier) bu Brusiya bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi. + +Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi: + +Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju kawe ja. Daal di dugg ag coldaar, génnati ca, dem nag féete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam niki lawax (candidat) ngir ñu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cér ci parlamaa bu Brusiya bi. Liggéey na it ci toolub diplomasi, doonoon aji téewal réewam (l'ambassadeur) ca Butrsburg ca Riisi. Ginnaaw bi mu nekkal réewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Faraas, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya. +Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu ñu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Jàngu bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yéegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kàngamam, waaye duñu ko ame mukk ci ay saxal (résolutions) yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti réew (systèmes constitutionnels). + +Bismarck yitteem jépp mi ngi ko jëmale woon ci génne Faraas ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga(manante leen). Ci noonu mu tàmblee liggéey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjoon képp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yéenekaay yi, daal di beddiku sartu réew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu génnelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi. + +Wàllug xeetu (nationalisme) nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu réew, ndax daa gisoon ne sartu réew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginnaaw bu ag xeetu amee ba noppi. + +Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lépp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy: + + Coldaar gi + + Politigu bitim réew bi + + Fal ay jëwrin ak di leen folli + +Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ + +Loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ . +Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yépp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu lëngoo (walla gu federaal), guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko. + +Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi walla maslaa, ngir yéegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi ñu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy: + + Dëggal ak wéyal jibalug bennoo gi + + Jiite benno gi + +Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi. + +Bismarck jéem na a fàggu cofeelug Riisi, ngir mu bañ a féete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Riisi, kontar gori Poloñ yi defoon ag fipp kontar Riisi, ngir dañal ag àtteem te jéem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb. + +Faraas nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Faraans. +Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Riisi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom réewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Riisi. Te it nanguwutoon a ànd ak Faraas ak Otris kontar Riisi. + +Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ: + +Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci réewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal diiwaani Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy: + +Xare yu Brusiya yi ak Danmark: + +Bismarck xuus na ab xare safaan Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari Dóox (duché) yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo. + +Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari dóox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dóoxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin. + +Xarey Brusiya ak Otris: + +Bismarck gisoon na ne xare bi moom – déet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manuñu woon a nekk di wéy ci anam gii ñu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig. + +Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris. + +Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim Géej gu bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu. + +Sabab yii rekk doyoon nañu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g. + +Bismarck moom lijjanti woon na ba Riisi génne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Riisi ci giimal jeqiku(révolution) ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratóor bi Napoleon III, imbraatóoru Faraas, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci diiwaanub Rayn. Mu demati tapoo-ji (faire alliance avec)ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom. + +Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a am ndam ci kaw ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatóoru Faraas bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Faraas dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci am ndam gii mu am ci kaw Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatóoru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Faraas, Otris du ko sot, ci geneen wàll. +Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame: + + Génnug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich. + + Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu lëngoo (gu federaal) gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu. + + Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia. + +Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem réewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari Dóox yii di Shalswig ak Holistin ci lañu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje. + +Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare . + +Xareb Brusiya ak Faraas +Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya ndàmbee ndam ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Faraas moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll. + +Faraas moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu ñu dogat, ngir mu nekk moom Faraas di réew mi am kiliftéef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daan kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir ñu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Faraas du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon. + +Lëj-lëju ku jigéen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans. +Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa féexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab jegeñaaleb imbraatóor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Faraas mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak aji teewal ju Faraas ja ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ééngir jibal ab xare ci kaw Faraas. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yéenekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Faraas. Loolu nag ni mu ko defe mooy génne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Faraas. Ci noonu Faraas jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulet 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu ñu dàqee Fraans ci xeex bi. + +Brusiya li ñuy wax xareb fëkk la doon def ak Faraas, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ak jarbu ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya. + +Xare bi bepp nag ci suufus Faraas la doon tàkke. Jotoon nañoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar 1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu (se rendre), te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Faraas ji ci biir suufus Faraas, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari téeméeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Faraas, te mu leer nàññ ne Faraas moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo génneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 1870g. + +Ci noonu imbraatóor gu Faraas gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi. Daal di teg Faraas ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans (loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi duñu génn Faraas li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi ñu dagge ñaari diiwaan yii di Alsaas ak Loren ci faraas, boole leen ci Almaañ. + +Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol góor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatóorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratóoru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi. +Sartu réew bu Almaañ bu bees bi yaxal na ñu sos ñaari jataay: + + Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundesrat) + Jattayu (Reichstag) + +Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundesrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cér, ñu séddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatóóor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lépp ci Bundesrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiital ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, dañoo takku woon ci Brusiya, te daawuñu woote lenn lu mu bëggul. Te daawuñu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cér ak ñeent àndadee ca saxal ga. +Bu dee nag jataayu Reichstag nag moom, man nanñu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti téeméer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cér, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka dañu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi ñu ko joxoon ci ron sartu réew bu Almaañ bu bees bi, dañoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo. + +Bismarck nag, jiite na góornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kiliftéefam tam la Almaañ gu rëy gii gépp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nañu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at. + +Taariixu Tugal +Baatukaay : + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + http://www.chez.com/afroweb/frm_wofr.htm + http://www.lexilogos.com/wolof_dictionnaire.htm + +Làkk +Njàngale +Sompat : Pomadasys perotaei (jén - rab) + + Askan (pop) : ? + Réewu Afrig: Kap Weer - Gaambi - Ginne - Ginne Bisaawóo - Gànnaar - Senegaal + Melo : (''fr : gris blanchâtre à reflets argentés) + Dayoo : 25cm + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + (en) Fishbase : "Pomadasys perotaei" + +Jén +Jëf – Ci faranse mooy Actes des Apôtres. +1 Korent – ci faranse mooy Première épître aux Corinthiens. + +Leeral Biibël +2 Piyeer – ci faranse mooy Deuxième épître de Pierre. + +Leeral Biibël +Tund yi ay dog lañu ci Séddaliinu Senegaal, nekk ci biir 14 diiwaani Senegaal yi. + +Sosug tunduw Kungéel moo ko yóbb ci limub 35 ci atum 2006. + +Dogiin +{| class="toc" cellpadding=0 cellspacing=2 width=300px style="margin: 0.5em 0.5em 0.5em 1em; padding: 0.5em text-align:left;clear:all; background-color: #fff; font-size:90%" +|- bgcolor="cccccc" +!Diiwaan +!colspan=4 |Tund +|- +|Cees +|Mbuur||Cees||Tiwaawon|| +|- bgcolor="dfdfdf" | +|Fatik +|Fatik||Funjunj||Gosaas|| +|- +|Kawlax +| Kafrin||Kawlax||Kungéel||Ñooro gu Rip|| +|- bgcolor="dfdfdf" | +|Koldaa +|Koldaa||Séeju||Wilingara|| +|- +|Luga +|Kebemeer||Lingeer||Luga|| +|-bgcolor="dfdfdf" | +|Maatam +|Kanel||Maatam||Raneru|| +|- +|Ndar +| Dagana||Podoor||Ndar|| +|-bgcolor="dfdfdf" | +|Ndakaaru|Ndakaaru||Géejawaay||Pikin||Tëngéej|| +|- +|Njaaréem|Bambey||Njaaréem||Mbakke|| +|- bgcolor="dfdfdf" | +|Siggcoor +|Biñoona||Usuy||Siggcoor|| +|- +|'Tambaakundaa +|Bàkkel||Keedugu||Tambaakundaa|| +|} + Xool it + Lëkkalekaay yu biir + Séddaliinu yoriinu Senegaal + Diiwaani Senegaal + Ndiiwaani Senegaal + Dëkkaani ndiiwaani Senegaal + Dëkkaani Senegaal + Gox-goxaani Senegaal + Dëkki Senegaal + + Téerekaay + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + François Zuccarelli, « Le département sénégalais », Paris, Revue juridique et politique'', n° 3, juillet-septembre 1968, p. 854-874 + +tundi Senegaal +Diiwaan yi ay dog lañu séddaliinu Senegaal, 14 lañu. + +Dogiin +Fi mu nekk nii 14 lañu, ba ñu sosee Maatam ci 2001, teg ci sos yeneen ñatt ci 2008: Kafrin bokkoon ci diwaanu Kawlax, ak Kéedugu bokkoon ci Tambaakundaa ak Séeju gi bokkoon ci Siggcoor. + +Réyaay ak way-dëkk +{| class="toc" cellpadding=0 cellspacing=2 width=250px style="margin: 0.5em 0.5em 0.5em 1em; padding: 0.5e text-align:left;clear:all; background-color: #fff; font-size:90%" +|- bgcolor="cccccc" +!valign=Top|Diiwaan +!valign=Top|Réyaayci +!valign=Top|Way-dëkk +|- +|Cees||align=right|6 601||align=right|1 348 637 +|- +|Fatik||align=right|7 935||align=right|639 075 +|- +|Kawlax||align=right|16 010||align=right|1 128 128 +|- +|Koldaa||align=right|21 011||align=right|834 753 +|- +|Luga||align=right|29 188||align=right|559 268 +|- +|Maatam||align=right|25 083||align=right|423 041 +|- +|Ndakaaru||align=right|550||align=right|2 411 528 +|- +|Ndar||align=right|19 044||align=right|863 440 +|- +|Njaaréem||align=right|4 359||align=right|930 008 +|- +|Siggcoor||align=right|7 339||align=right|557 606 +|- +|Tambaakundaa||align=right|7 339||align=right|557 606 +|- +|Mboolante ||align=right|196 176||align=right|10 225 816'|} + + Xool it + Lëkkalekaay yu biir + Séddaliinu yoriinu Senegaal + Tundi Senegaal + Ndiiwaani Senegaal + Dëkkaani ndiiwaani Senegaal + Dëkkaani Senegaal + Gox-goxaani Senegaal + Dëkki Senegaal + + Téerekaay + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal, Dakar, Ministère du Plan, 1967, 705 p. (Thèse de 3e cycle publiée) + Laurence Porgès, Bibliographie des régions du Sénégal. Complément pour la période des origines à 1965 et mise à jour 1966-1973, Paris, Mouton, 1977, 637 p. + + Lëkkalekaay yu biti + Agence Nationale de la Statistique et de la Démographie du Sénégal (chiffres des différents recensements et estimations officielles jusqu'en 2015) + « La région dans les limites administratives des États de l'Afrique de l'Ouest » (article de Gérard Brasseur dans le Bulletin de l'IFAN'', série B, 1968, tome 30, n° 3, p. 861-867) + « Trois nouvelles régions administratives seront créées au Sénégal » (Agence de presse africaine, 25 mai 2007) + +diiwaani Senegaal +Ndiiwaani Senegaal yi ay dog lañu ci séddaliinu yoriinu Senegaal. + +Ndiiwaan nag ag nekkte (entité) gu suuf la, gu ñuy faral di gis ci réew yiy làkk wu-fraas. Soo demee ci ñiy làkk wu-angalteer weneen dogiin nga fay fekk. + +Ci Senegaal, ndiiwaan yi dinañu leen waññi ci lim bu tollook 92 ci 2007. + +Taariix + +Limu tund yi (nosu topp abajada) + +Tunduw Bàkkel + +Bala +Jaawara +Gudiiri +Kidiira + +Tunduw Bambey + +Baba Garaas +Lambaay +Ngoy + +Tunduw Biñoona + +Jululu +Sinja +Tenduk +Tengori + +Tunduw Cees + +Nooto +Puut +Cenaba + +Tunduw Dagana + +Mban +Roos Beeco + +Tunduw Fatik + +Jaxaaw +Fimla +Ñaaxar +Taatagin + +Tunduw Funjunj + +Jilloor +Ñoojoor +Tubaakuta + +Tunduw Gosaas + +Kolobaan +Kawóon +Waajur + +Tunduw Géejawaay + +Géejawaay moom, benn Ndiiwaan la am muy moom ci boppam. Tund la ndiiwaan la + +Ñu séeddale ko ci 5 dëkkani ndiiwaan + +Tunduw Kafrin + +Dogiinu tund wi dañu koo soppi gannaaw sosug tunduw Kungeel ci 2006. + +Kon mu des : +Birkilaan +Maleem-Odaar +Nganda + +Tunduw Kanel + +Kanel +Seeme + +Tunduw Kawlax + +Ganjaay +Ndenjeng +Ndóofaan + +Tunduw Kebemeer + +Daaru Musti +Ndand +Sagata + +Tunduw Kéedugu + +Bandafasi +Fongolimbi +Salemata +Saraya + +Tunduw Koldaa + +Dabo +Julaacolon +Medina Yoro Fula + +Tunduw Kungéel +Mi ngi judd ci 2006 (amul lonkoyoon bu jàppandi nii-nii) + +Tunduw Lingeer + +Barkeji +Daara +Dooji +Yang-Yang + +Tunduw Luga + +Kër Momar Saar +Kokki +Mbejeen +Sakal + +Ndiiwaanu Raawo, biy feeñ ci lonkoyoon bi, ci tunduw Ndar la bokk 2002 ba tay. + +Tunduw Mbuur + +Fisel +Ngeexoox +Caajaay +Jiwaalo + +Tunduw Maatam +Añam Ciwol +Ogo + +Tunduw Mbakke + +Kayel +Ndam + +Tunduw Ndakaaru + +Ndakaaru moom, benn Ndiiwaan la am muy moom ci boppam. Tund la ndiiwaan la + +Ñu séeddale ko ci 19 dëkkani ndiiwaan. + +Tunduw Njaaréem + +Ndindi +Ndulo + +Tunduw Ndar + +Gannaaw dogaat ga waraaloon juddug Diiwaanu Maatam, tund wi, wenn ndiiwaan rekk la am muy bu +Raawo + +Tunduw Ñooro gu Rip + +Medina Sabax +Pawoskoto +Wak Nguna + +Tunduw Pikin + +Pikin moom, benn Ndiiwaan la am muy moom ci boppam. Tund la ndiiwaan la + +Ñu séeddale ko ci 16 dëkkani ndiiwaan. +Pikin + +Tunduw Podoor + +Kas-Kas +Njum +Salde +Cile Buubacar + +Tunduw Raneru +Tund wi, wenn ndiiwaan rekk la am muy bu Welingara + +Tunduw Séeju + +Bunkiling +Jaatakunda +Jend +Marsasum +Tanaaf + +Tunduw Siggcoor + +Niaguis +Niassia + +Tunduw Tambaakundaa + +Kumpentum +Kusaanaar +Makakolibantang +Misiira + +Tunduw Tënjéej + +Tund wi, wenn ndiiwaan rekk la am muy bu Sebixotaan, moom ci boppam ñu séddale ko ci 3 dëkkaani Ndiiwaan. + +Tunduw Tiwaawon + +Meewaan +Merina Daqar +Ñaaxeen +Pambal + +Tunduw Usuy + +Kabrus +Luja Wolof + +Tunduw Welingara + +Bookoto +Kunkan +Pakur + +Xool it + +Lëkkalekaay yu biir +Séddaliinu Yoriinu Senegaal +Diiwaani Senegaal +Tundi Senegaal +Ndiiwaani Senegaal +Dëkkaani ndiiwaani Senegaal +Dëkkaani Senegaal +Gox-goxaani Senegaal +Dëkki Senegaal + +Lëkkalekaay yu biti + Site officiel du gouvernement du Sénégal + Données statistiques worldbank.org + Chiffres population www.gouv.sn + Découpage administratif sur www.senegalaisement.com +« Décentralisation : Les bœufs attendent la charrue » (article Panos Infos, 2003)) + +Téerekaay + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + +Ndiiwaani Senegaal +Aakimoo jawwu ji, (walla xare bi ngir teg loxo ci jawwu ji sanc ko): + +Li ci alxuraan wax +Sooratu Rahmaan, aaya 33: + +«yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin» + +Tekki: yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen wóor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen wunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa. + +Ci lu daj +Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki yaram yu asamaan; ay biddiw aki ñoom seen. +Moom de jot naa àgg ci xam biddiw yi ak seeni kem ak seeni bind (forme), ak li leen sos, def it ab jéego bu rëy ci xam-xamu melosuuf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw-suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, biddiw ak lu ko moy. + +Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bi, gisees na nit mu jéem ay yoon nu mu yéege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci woon jafe-jafe yi mu ci doon man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu: man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu ñuy boy (départ), bu wuutuloxo (masin) biy wëndéelu ak buy wàcci. + +Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji +Sofiet yi de njëkk nañoo nattu jawwu ji, jarbu ko, làmbtu ko, loolu ñu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo. + +Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalu gu jawwu gi tuddoon Fostok – 1, ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp. +T +ukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook téeméer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj. + +Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu. + +Sofiet yi wéyoon nañu ci seen liggéeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen jumi jawwu (satellites) yi gënoon nañoo yokk seeni cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii. + +Li ci waa-Amerig def +Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nañu ay jéem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji walla aakimoo ko. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen liggéey yu jawwu yi gënoon nañoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon. +Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a néew, te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji. + +Waa Amerig jot nañoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nañu fa it ay còmp (échantillons) yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu mbëj bu saal . + +Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu) ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. +Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu . + +Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g. + +Musibam Carlinger: + +Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna . +Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald Rigan nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi. + +Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee. + +Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca. + +Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi. +Ndaxte xam-xamu Jëmm gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jéego ay jéego, naka noonu ndefar bu mbëjfeppal (bu elektron), ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs. + +Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk sóobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay liggéeyi xare, la ñu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen jumi jawwu yi nekk ci asamaan si, yi ci yanu ay boppi fepp (tête atomique), cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll. + +Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy réew bokksi nañu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen réew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare. + +Aakimoo jawwu ji +Jeqiku gi xam-xam amal ci Elektron : + +Xamale lan mooy “ Elektron” : + +Elektron moom yaram su sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu ñu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu mbëjfeppal(electronique) yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso. + +Elektron nag nekk na ci bépp ne-ne bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek fepp wi, moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko fepp wiy xëcc. Elektron ni muy wëre fepp wi - booy xool - day mel ne ni kawkab yi di wëre jant bi. +Elektron nag day yanu ay cëfkay mbëj yuy bañ ,fepp wi di yor ay cëfkay mbëj yuy wuyyu walla nangu. + +Xam-xamu Elektron ni mu sosoo: + +Xam nañu ne xam-xamu mbëj moom xam-xam la bu ñu xame bu yàgg ci ki ñuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Geres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii ñuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angalteer boo xam ne mooy ki teqale dooley mbëj ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lañu. +Jilbert it xamoon na ne duusi mbëj yi ñooy jur dooley bijjaakon. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne wuutuloxo buy juddal mbëj, maanaam jumtukaay buy tax mbëj di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu làmp bu mbëj. + +Xam-xamu mbëj nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginnaaw bi boroom xam-xamu Jëmm bu Angalteer bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu Jëmm. +Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy wuññi gi boroom xam-xam yi wuññi ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari. +Ndamul xam-xam lii ab jéego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jéego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf. + +Jumtukaay yu elektronig (walla mbëjfeppal) yi ak seen njariñ: + + +Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, liggéeyuwaay yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs. + +Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu mbëj yu boppu (otomatik) yi, ak fompukaay yu mbëj yu boppu yi, ak jumtukaayu seral yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs. + +Boo demee ci paj it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elekton yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu paj yi, ak jumtukaayu segg yu elktron yi. Jumtukaay yii dey tax nanu paj man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax paj jëm kanam ci sunu jamono jii. + +Gis nga leegi foo dem fekk fa nosukaay, ci bank yi, lonkoo yi(les sociétés), campeefi nguur yi ak liggéeyuwaay yi. +Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi, ak xam kilimaa bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def. + +Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktron yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbelli suuf yu am yi solo. + +Jumtukaayi elektron yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga soxu fepp (bombe atomique) , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs. + +Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii. +Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi. + +Jëmm +Jëmm +Fepp mooy xaaj bi gën a tuuti ci aw yaram wu neen (simple), wu man a booloo ak weneen ci simi. ñaare day ame ci ab saal bu sosoo ci ay Proton aki Notron yu ay Elektron di peek (di wër). + +Jëmm +magnétisme fr: xeet la ci juddalkaayu mbëj + +Jëmm +lu tuuti te xeebu ci yaram, deesi wax ko ci fr particule, + +Jëmm +Njabootug lepton yi mi ngi ame ci Elektron yi, Muon yi, Tauon yi, neutrinos yu boppam yi ak seeni safaan-yaram (antiparticule). Baatub « lepton » mi ngi bawoo ci baatub Geres biy tekki « lu woyof » biy jublu ci wf gi doyodig jóor (faible masse) gu lepton bi ñu njëkk a wuññi, Elektron bi, bu ñu leen nattee ci nukleon yi ( nucléons). + +Jëmm +lepton : yaram su cosaanu la su woyof, su dul dékku ay defante yu dëgër (interactions fortes) + +Jëmm +Dees na ko tekki: + +Le terme nucléon désigne de façon générique les composants du noyau atomique, i.e. les protons et les neutrons qui sont tous deux des baryons. Le nombre de nucléons par atome est généralement noté « A », et appelé « Nombre de masse » +Jusque dans les années 1960, les nucléons étaient considérées comme des particules élémentaires. On sait maintenant que ce sont des particules composées de quarks et de gluons. Les propriétés de ces particules sont régies en grande partie par l'interaction forte. Le proton est le plus léger des baryons, et c'est le seul qui soit stable. Plus exactement, les mesures qui ont été faites montrent que le proton a une durée de vie supérieure à 1030 années, ce qui apporte une contrainte forte sur les théories spéculatives qui essaient d'aller au-delà du modèle standard. De son côté, le neutron a une durée de vie moyenne d'environ 1/4 d'heure) et se désintègre par interaction faible en proton, électron et antineutrino électronique. Le proton et le neutron forment un doublet d'isospin I=1/2. + +Jëmm + + +Reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn + +Ag jiital: + +Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci Ñaareelu Xareb Àdduna bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay Réew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare. +Ci noonu dankub bopp-alal dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi . +Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole bañu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo. +Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu, Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi . +Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te faf far, xajal fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi. + +Loolu nag taxoon na ba reewi Órob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew. +Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi. +Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. +Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni: +Tapoo gu càmmooñug atlas (Otan): + +Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island. +Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm: + +(1) kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des. +(2) Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom. +(3) Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam. + +Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm ak yoon. + +Tapoo gu Warsaw: +Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. +Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. +Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi. +Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk. +Tapoo gu kollëre gu diggu gi: +Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak. +Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g. +Jataayub Tugal bi : +Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali. +Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi. +Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba : +Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya gore ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir. +Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali : + +Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll. +Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suweet, ak Yogoslawi. +Mbootaayug reewi Amerig yi: +Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk. +Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum 1958 g. + +Mbootaayi reewi Andis yi: + +Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi. + +Naalub Marsaal bi ak Komikon: + +Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb Àdduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi. +Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom. + +Mbootaay gi boole reewi araab yi : + +Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir. + +Mbootaayug jàpplante gu Asi: + +Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk. + +Mbootaayug bennoog Afrig : + +Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada. + +Reew yi féetewul fenn: : + +Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll. + +Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo. + +Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Sapoŋ, Filipin, Taylànd, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman. +Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb. +Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex. +Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig. + +Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakiri atum 1960 g . +Bi àdduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi. +Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja. +Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk: + +(1) wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg. +(2) Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul. +(3) Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi tas leen, dindi dàtti xare yi . +(4) Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk. + +Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit bu baax. + + +Li ci xew +Mandabi dip filmi ci Wolof bou Ousmane Sembène bokhamni dathiye netali: jen way jo khame mi da am jarbaatam bouko yoone manda nguir mou jokhko ndayam legui ay soxnam tekko allal ju bari ba tambale lep luune ndekkete yoo mandabek thiowli jounii ak niari temeer rek la ndekeyoo amouloup dentite boumou ko jeulije. + +Nit gni thi ne +makhouradia gueye +isseu niang + +Filmi ci Wolof +Lii mooy limub njiitl réewum Senegaal la ko dale ca ba mu tembee ca Faraas 4 Awril 1960. + +njiiti Senegaal +Dëkkaani ndiiwaani yi, ci Senegaal, ay dog lañu ci séddaliinu yoriinu réew mi. ci 2007 lim bu toll 43 lañu. + +Taariix +Yokkug nit ñi dëkk ci Ndakaaru moo dem ba àgg ci benn dayoo bi, ba tax genn kilifag dëkk rekk manatu koo yor, tax sosug geneen nekkte gu gën a suufe waroon. Kon lii moo tax ci 1996 ñu séddale tunduw Ndakaaru ci 43 dëkkaani ndiiwaan, ni dëkk bu Paris. + +Dogiin +43 Dëkkaani ndiiwaani yi dañu leen séddale ci 4 tund yi: + + Ndakaaru: 19 + Pikin: 16 + Géejawaay: 5 + Tëngéej: 3 + + Cees: 3 + +Xool it + +Lëkkalekaay yu biir +Séddaliinu yoriinu Senegaal +Diiwaani Senegaal +Tundi Senegaal +Ndiiwaani Senegaal +Dëkkaani Senegaal +Gox-goxaani Senegaal + +Téerekaay + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + +Lëkkalekaay yu biti +Décret n° 2002-174 fixant la composition des conseils municipaux des communes d'arrondissement des villes de Dakar, Pikine, Guédiawaye et Rufisque +Décret n° 2002-175 déterminant le nombre de conseillers de la ville par commune d’arrondissement dans la région de Dakar + +Dëkkaani ndiiwaani Senegaal +Yolet : melo + +Melo +Ñent, ñeent : 4 + +Xayma +Oiapoque : dëkku Breesil + +Breesil +Toulouse dëkku Faraas. Nitñii motnañu 447 340 (2011). + +Dëkki Faraas +Lourdes dëkku Faraas. Nitñii motnañu 15 808 (2008). + +Dëkki Faraas +Yoonu murit walla Muriidulaa ni ko ñenn ñi di waxe, wenn yoon wu am solo la wu tasawuf, muy moom tasawuf benn bànqaas bu mbóotu (mystique) ci lislaam , mi ngi nekk nag rawati na ci Senegaal ak Gàmbi. Muy lu ñu sos ci ndoortel XXeelu xarnu, ki ko def di Seex Ahmadu Bamba, yoonu murit nekk na tay yoon wi gën a am ag jeexiital ci Senegaal, bu ñu waxul ci Afrig gu sowwu gi Murit yi tam ñi ngi jëf lu am solo ci wàllug koom-koom ak politig . Njiitul réew mi Abdulaay Wàdd, mi ñu fal ci 2000, mooy njiitul Senegaal lu murit li njëkk a am . + +Aaday Murit +Aaday murit (walla ju yoonu murit)lu jeexiitalu ci caaday Afrig la, rawatina ju wolof. Yitte ak fulla ji yoon wi jox liggéey tax na ba mu man a suuxatu bu baax ci wàllug koom-koom ci Afrig, te tax na it ba mu man a tas bu baax ci dëkk yu mag yi ci Tugal ak Diiwaan yu Bennoo yi. Tay, daanaka mbooleem dëkk yu mag yu Bëj-gànnaar yi gàddaay gu Senegaal gi dëgmalsi te jëm fa kanam, am na ag Kër Sëriñ Tuubaa (Barabu daje ngir julli, jaamu Yàlla, defi màggal, daaray jàng xam-xam añs). Moom de dalub mbooloo mu murit mi la, fi ñuy defe seeni daje ngir jaamu Yàlla, walla ngir leneen, waaye it dana di jariñ it niki ab teeruwaayu gan ñeel way door a agsi yi ciy gan. Danañuy faral di def ab siyaare walla lu mel ne ag aj gu ñuy def ci at mu ne ca dëkk bu sell ba Tuubaa, gi nekk ci digg Senegaal.Màggal gi genn xumbéel la guy jëmmal at mu ne fàttalikug gàddaayal gi ñu defoon Seex Ahmadu Bamba ca 1895, ci loxol kiliftéef gu Canc gi (l'autorité coloniale). + +Gongikubaat + +Baatub mourid walla murit ni ko wolof yi di waxe, mi ngi bawoo ci Jef ju Iraada, te mooy « bëgg dara », « namm dara, xëccu jëm ci lenn » teg ca gongikooti ci murīd giy tekki « aji namm mbaa aji bëgg», jubloos ci aji namm ji Yàlla ki bëggul ku dul moom, lu dul moom, lu dul ngërëmam, loolu it mooy firi fonk gi taalube yi di def seeni sëriñ, ndax Yàlla ga ñuy gis ci ñoom, maanaam ñoom ñoo fi nekkal Yàlla ci jàngale Diine ak aar ko. Murit nag benn la ci ñaari baat yu ba ca des di Laah, kon muy muriidulaa, di tekki aji namm ji Yàlla, maanaam ki Yàlla rekk tax a jug, mu mel ne baat bii mbooleem yooni tasawuf yi dañu koy jëfandikoo niki taalube, walla dongo, waaye bokk na ci li gën a génne baat bi, jox ko fulla mooy ñëw gi yoon wi ñëëw ci jamono joj lislaam da cee xawoon a doyodi, néew ci doole, te li ko waral di nekk gi nit ñi nekke woon lu wuute ak lislaam, daan ko foye, yor geneen dund gu dul gi lislaam tànn, wii melo di lol ñu bari ci bindkati Senegaal yi wax nañu ci, ku ci mel ne Sëriñ Musaa Ka ak ñu ko moy, melokaan wii nag man nañu ne bokk na ci li taxoon Seex Ahmadu Bamba jugoon mel ne ku naan «ana ku namm Yàlla» ana «ku Yàlla tax a jug», ca foola la baat bii daal juge di tekki leegi képp ku di taalubeb murit, muy baat bob daa jug mel ne kuy tàqale diggante ki nekk ciy caaxaan ak ki ko nangoo ba te jublu lu baax li di Yàlla ak la ko wër. Sëriñ bi booy xool day mel ne yorul aw yoon, waaye lislaam la jug ngir taxawalaat, yeesalaat, ndax mbooleem yoon yi mu fi fekk, da leen a nangu, topp leen, jël seeni wird, daa na joxe mbooleem seeni wird te booba mi ngi yor wird wu juge ca Yàlla jaar ci Yonent bi Muhammad, ni yoon yepp ame seeni wird. Leegi kon luy ndayi muy joxe yooyule wird te yoroon wu boppam? Ndaxte daa jugaloon lislaam déet aw yoon, moom moo wax ne + +« wépp wird wu waay yor ngir jëmmi Yàlla rekk te leneen taxu koo jug, moo xam woowu daa bawoo ca Jiilaani (Xaadiriya) mbaa mu juge ca Ahmad Tiijaan (tiijaan), na xam ne li mu yor moo dig jub» + +Kon kii boole jullit yee ko taxoon a jug, yombal seenug jëm ca Yàlla, far digi yoon yi, boole ñepp ñuy jaami Yàlla ci ron keppaarug Lislaam + +Yàllaange (Théologie) ak nosiin wu biir gi + +Yoonu murit Seex Ahmadu Bamba (1853-1927)moo ko sos, mu di aw yoon wu mbóotu wow mi ngi feeñ ci Senegaal ci biir aw nekkiin wu mboolaay wu ñu nëxël ag sellam jaxase ko, nga xam ne Canc gi (la colonisation) jaxase na bu baax nosteg màndaxoo gu mboolaay gi (le système d'équilibre social). Ngir nag yéwénal mboolaay gu senegaal gi Seex Ahmadu Bamba daa woote woon jëme ci ñu roy njàngalem Alxuraan mi, te ŋoy ci sunnas Yonent bi Muhammad (j.m), te xeeñtu it maanaay tasawuw yi te roy ci, fullaal it xam-xam ak liggéey te jox leen seen àq ak xiima. + +Lii nag daa dëppoo ak li ñuy wooye ag yeesal mbaa ag yéwénal, ndax ci Tasawuf waxees na ne Yàlla (t.s) day yonni ci téeméeri at yu ne, jenn Aji yeesal (walla mujaddid) juy taxaw ci dundalaat, yeesalaat lislaam ca dëgg-dëggam, kooku tam mooy nekk aji donn ju ruu ju Yonent bi (j.m), ñu koy wax (qotb walla « pujub cellte ») maanaam fa ag sell man a yam. Bamba kon kenn lay doon ci tànnéef yii. + +Yàllaange gu murit yi (walla seen gëm-gëm) dafa jeexiitalu ci yoon yii di Xaadiriyaak Tiijaan waaye it ak mbindi Alxazaali, nga xam ne Bamba da koy tudd lu bari ciy mbindam. Yenn jullit yiy woote ag cunna danuy jàpp ne gëm gu tar gii am ci murit yi jëm ci Ahmadu Bamba aki way donnam aw xeet la ci ag njaamu xërëm, waaye booy xool xamadi rekk a ko waral, ndax ku xóotal ab xam-xamam ci yoon wi duggi ruqam di nga gis lu dul loolu, nit nag bu jëfee lu moy la ñu ko xamal moom mooy ka tooñ, kon na murit yi di jàng mbindum Sëriñ bi tey bañ di tëñëxu di doxe ni ñu ko bëgg a doxe, bëgg ko nee gëme, tey doxe ni ko Sëriñ bi bëgge ci ñoom. Seex Ahmadu de giseeful ciy mbindam lenn lu dëppoowul ak Alxuraan ak sunna . + +Murit yi am nañu ay jikko ak xiima yu di yu lislaam fekkoon ci ñoom, te xawoon a giim Sëriñ bi ñëw dekkalaat ko . Bokk na ci yooyu liggéey gi ñuy àgg ci di sellal, jàpplanteek dimbalante. At mu nekk ay milyoŋi nit dañuy bawoo fu nekk di màggali Tuubaa gi nekk ci digg Senegaal . . + +Ni ko Emmanuel Brisson gise, Yoonu Murit « dafa nosu - ci gis-gisu ñenn ñi - niki ag noste gu laman (système féodal), moom daa tegu ci kaw ag toppe gu joyu ñeel genn kiliftéef gu ruu (une autorité spirituelle), Xalifa bu matale bi (le Khalife général), di ku doomu mbaa mu sëtu ci anam gu jonjoo ci Aji sos ji yoon wi. » . + +Taariixu yëngu-yëngu gi + +Muy ku janook yoriin wu cang gi(l'administration coloniale) maanaam tubaab yi ngir mbooloom mii di wéy di màgg ba tàmbali woon leen a tiital, Seex Ahmadu Bamba gàddaayalees na ko ci anam gu toftaloo ca Gaboŋ (Afrig gu yamoo gi (Afrique équatoriale)), dale ko ci 1895 ba 1902, ca Gànnaar dale ko 1902 ba 1907, ginaaw bi ñu teg ko ci ron ag dëj gu ñu wattu (résidence surveillée) ci Senegaal ba kero muy làqu (génn àdduna) ca 1927. Kiliftéef gu Faraas gii mujj na ko nànd xam ne aw ay taxu koo jug, mu jàmmal ko, loolu it may yoon wi ci ndimbalul Yàlla ag naataange gu kawe. + +Bi fi Sëñ bi jugee ci 1927 ba tay, ay Xalifaam yi ko fi wuutu ñooy ay doomam, dale ko ca ka ca mag, ba ca ka ca gën di gone: +Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke, dale 1927 ba 1945 +Sëriñ Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 1945 ba 1968 +Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke, dale 1968 ba 1989 +Sëriñ Abdu Xaadir Mbàkke, moom ag ayam weesuwul 11 weer dale 1989 ba 1990 +Sëriñ Saaliwu Mbàkke (mi ngi gane àdduna 1915), di xalifa dale 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007 +Sëriñ Muhammadu Lamin Baara mom Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 30 desambar 2007 + +Ginaaw bi fi Sëriñ Saaliwu bàyyikoo, moom miy doomi Sëriñ Tuubaa ju fi mujj, la xilaafa gu matale gi tuxu leegi dem ci sët yi. Xalifa bii fi nekk mooy ki mag ci sët yi, di Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke, ññu koy wax Alaaji Baara. + +Seexal + +Bi Sëriñ bi yoree yoon wi ci la seexale ñennat ci mag ñi, bu ko defee ñu daal di leen féetale ñenn ci taalube yi, loolu nag daa doon luy am ginaaw ag yar akug wulli ba mu mel ni war ci ab sëriñ dëgg bu war a jiite aw nit ci lislaam, bu man a yare, man a tege ci yoon. Loolu mooy li am ci Maam Seex Ibraayma Faal ak Maam Cerno bi tubaab yi gàddaayalee Sëriñ bi. Seexal gii nag dakkoon na ca 1912, at mi Sëñ bi seexale ki mu mujj a seexal, mu di Madiba Silla ca Njaaréem. Sette gi ci amaat mooy Beeco Cuun mi ñu ne Sëriñ Saaliwu moo ko seexal ca 1987. Seexal gii jeqi na coow lu bari ci biir yoon wi. +Bokk na ci Seexi Sëriñ Tuubaa yu may yu jàmbaare yi Sëriñ Ndaam Abdu Rëhmaan Lóo, Sëñ Isaa Jenn + +jeexiital gu koom-koom ak gu politig + +Yoonu murit mi ngi gën di yaatu bu baax, te am na it ag jeexiital gu am doole ci politigu Senegaal . Moom day joxe ay ndigali farle (consignes de vote) te xalifa bi it lu sakkan ciy way politig dañu koy seetsi, di diisook moom juge fu ne. + +Ci wàllug koom-koom ak mboolaay , « Ñoom Murit yi dañuy joxe dëkkuwaay, dund ak tàggatug xel - ci jàngale alxuraan ak xam-xam yi ci aju - ñeel xale yi gën a ñàkk, mbaa yi "sànku". Am nañu ay way jam (détracteurs), yu leen di yedde seen roose gi, seen mbay mu bari mi, seen ndimbal gu mboolaay gi (aides sociales). (...) Yoon wi war naa yor koom bu sakkan mu bawoo ci mbay mi, rawati na ci gerte g. » (Brisson, 2008 ) + +Wisaaroo gi (La diaspora) ca Paris, ca Brescia ak ca New York, nga xam ne daa jàppe xaalis muy lu sell, ndax ci liggéey la meññoo, ak ci yaxantu, day yonnee ay lim yu rëy ci xaalis ñeel mbokk ya nekk Tuubaa. + +Xalifa yu Murit yi ñaare ñu am ag jeexiital lañu, ndaxte duñu rekk ay njiiti ruu yu ay taalube yu ñu nattale ci 3 ba 5 milyoŋ, (man jortu naa ne ëpp na loolu di dem ndax Tuubaa rekk lu ëpp milyoŋ dëkk na fa), waaye it ca dëgg-dëgg ay njiit lañu yu jamono (yu àdduna) yu dëkkub Tuubaa bii nga xam ne mooy péey bu ruu bu murit yi, te mujj na ndànk ndànk (moom Tuubaa) di ñaareelu dëkk bu Senegaal, ngir diisaayu demogaraafam ak bu koom-koomam. + +Yeneen doom mbaa sëti Sëriñ bi, ñoom it ñu am ag jeexiital lañu ni xalifa yi, ak doonte àgguñu ci xilaafa gi. Ku ci mel ni: +Seex Ahmadu Mbàkke Gaynde Faatma, mi ñu xam ci ag sóoboom ci yar ak jëmale kanam gu mboolaay-koom-koom (socio-économique) gu mbooloo yi, xame nañu ko it ci jeexiital gi mu am ci njiiti politig yu Afrig yu mag yi, mi ngi faatu ci 1978 ; +Seex Muhammadu Murtalaa Mbàkke, "sëriñub wisaaroo gi" (le marabout de la diaspora), moom it muy ku ñu xam ngir sos gi mu sos ngir Yàlla rekk lu sakkan ciy cëslaayi jàngu ci mbooleem Senegaal, mi ngi làqu ci 2004. fii mu tollu doomam ak xalifaam sëriñ Maam Moor Mbàkke mi ngi wéyal ab liggéeyam, di ci dolli yeneen cëslaay yu bees(autres structures nouvelles) yu dëppook gis-gis bu jëm-kanam bi mu am ci ag jamonoo (la modernité). Moom de mi ngi jéggeek murit gi ag wàll gu am solo ci lu aju ci wisaaroo gi (au niveau de la diaspora). + +Bidaa + +Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen . +Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. +Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam. +Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon. +Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a kopparal ci lislaam man a kopparu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it. + +Térekaay + O’Brien Donal B. Cruise, The Mourids of Senegal. The Political and Economic Organization of an Islamic Brotherhood, Oxford, Clarendon Press, 1971, XXII-321 p. (Publication d'une thèse de 1969) + Omar Ba, Ahmadou Bamba face aux autorités coloniales (1889-1927) + Jean Copans, Les marabouts de l’arachide. La confrérie mouride et les paysans du Sénégal, Paris, Sycomore, 1980, 263 p. (Thèse Paris, EHESS, remaniée) + Momar Coumba Diop, La confrérie mouride : organisation politique et mode d’implantation urbaine, Lyon, Université de Lyon, 1980, 273 p. (Thèse de 3e cycle) + Youssouf Diop, « La signification du mouridisme dans l'actuel contexte socio-politique du Sénégal », Université de Dakar, 1983, 118 p. (Mémoire de Maîtrise) + Mamadou Mbodj (dit) Pape Coumba, Le mouvement des jeunes dans la confrérie religieuse des mourides. Essai d’analyse et d’interprétation, Dakar, Université de Dakar, 1980, 149 p. (Mémoire de Maîtrise) + Oumar Mbaye, Le mouridisme sous le khalifat de Mohamed Fadilou Mbacké (1945-1968), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2000, 98 p. (Mémoire de Maîtrise) + Cheikh Tidiane Sy, Traditionnalisme mouride et modernisation rurale au Sénégal. Contribution à l’étude des rapports entre socialisme et islam en pays sous-développés, Paris, EPHE, 1965, 236 p. (Thèse de 3e cycle, publiée sous le titre La confrérie sénégalaise des Mourides. Un essai sur l’islam au Sénégal, Paris, Présence Africaine, Université de Paris, 1969, 353 p. + Samba Sy, Le mouridisme à l'Université : essai sur l'association des étudiants mourides, Université de Dakar, 1984, 85 p. (Mémoire de Maîtrise) + +Filmkaay +'Yoonu murit' di ab film bu Samba Félix Ndiaye defoon ci 1976. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Lëkkalekaay yu biti + موقع مريدي بالعربية www.wikimouridia.org, dal la buy wax ci yoon wi ci araab + Majalis.org +Association Culturelle Réligieuse Islamique Mouride +Mouride.com +Jamiatou.com +Daaramouride.asso.ulaval.ca +htcom.sn +Ahloubadar.com Serigne Bi Reck +Bibliothèque virtuelle Cheikh Ahmadou Bamba +Emmanuel Brisson, Reportage sur les Mourides, 2008, sur le site de Grand reportage. + +yoonu murit +Mooy ñatteelu xalifa ginaaw Sëriñ Fallu + Bu ñu dee naw sunu réew mi ci Demokarasi (démocratie)ak wax sa xalaat ci feex (liberté), kii di S Adbu Lahat ku ci jeego ay jeego yu réy la, ku ci bay aw waar la. Bu kenn fatte ba muy wax Sengoor kàcc nga, te wéeruwul woon booba ci ku dul Yàlla, te fasoon yeene du wax lu dul dëgg, te booba njiitul Afrig lu kenn ñemee wax lu jege loolu amul. Loola bokk ci li nooyal njiit yi ci Senegal, sos ag màndaxoo (équilibre) ci sunu reew mi, tax it njiit lu fi nekkati yëg ne kenn a ngi fi kok du may kenn muy ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ci reew mi. Bari na lool ay taxawaay yu amal njariñ réew mi ci wàllug demokaraasi (démocratie), kafte (liberté) ak àq ak yelleefu doomu aadama. Ku mel ne moom aki jëfam ñoo suuxat Senegaal gii nu am tay, bu ko kenn féetale Seŋoor aki gaayam (way politig yi) ak doonte seen loxo gennu ci! + +Dundam +Niti senegaal +Yoonu murit +Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke (dàkkantal: Sëriñ Fallu, Sëñ Fallu, Fàllu Galas, Alaaji Fàllu) +gane àdduna ca Daaru Salaam (kërug jàmm) nekk ci tundu bawol ca réewum Senegaal ci 27 ndeyu-koor (rajab) atum 1305 ci gàddaay gi yamoo ak atum 1887/88. + +Mu tombe ak bis bi turandoom Sunu Sang Muhammad (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci kawam) riñaanee ci ndingalal boroomam ànd ak sunu Sang Jibriil (jàmm ci moo) war daaba ju deesi woowe «Al-buraax», Ci rañaan googii la ko Yàlla sunu boroom joxee julliy joróom di ponk bi ëpp doole ci lislaam, waral ko ci mboolem jullit ñi, ak xeet i xam-xam yu mu fi sotti ngir nun ak ya ko ñeel ci ag jagle, Muy guddi gu màgg ci Lislaam, guddi gi nu xéewal gi dikkale juge fa Aji-Màgg gi. +Sëriñ Fàllu Mbàkke génn na àdduna ci atum 1968 (dund 81 ciy at) ci ginnaaw bi mu nekke xalifab +Sëriñ Tuubaa ci atum 1945 ba 1968. +Sëriñ Fàllu Mbàkke mom Seex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul (baayam) mi sos yoonu muriid ak Soxna Awa Buso (ndayam) doomu Sëriñ Muhammadu BUSO (Sëriñ Mbusóobe) nijaayu Sëriñ Tuubaa, Mu bawoo ci njaboot gu sell gii, di askan wu ragal Yàlla daa jàng tey jàngale, dëkkoo jaamu Yàlla te di ko jaamulu, di ay wàlliwuy Yàlla yu mat, Mu cosaano ci askanu Sëriif gog calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ak xéewalam ci ñoom). +Mu dondoo ci loolu (doonte ag njub déesu ko dondoonte waaye dees na ci yare, te moo baaxoo am) +ag cell, Yar, xam, ngëm ak melo ya war ci doomu Soxna, ci yooyu jikko lako ay way-juram yare te nàmptal ko ci. + +Am njàngam + +Ci loolu mu dal jàng ci bi muy làq 8 i at, dalee ci njàngum Alxuraan téereb Yàlla bi, ci jàngalekat bu tudd Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan LO ca dëkkub Ndaam deesi ko woowe «Aalimun Xabiir» ak ci Sëriñ Moor Jaara Mbàkke miko tuural Alxuraanam, ba wattu Ko wattu gu yéeme ci ab taar, ba daan a wax ni:«Ku ma bokkalul jàng ci Sëñ Moor Jaara maala man ci alxuraan» ngir di wone taarub wattu alxuraan gi mu fa jële, ginnaaw bi baxoo woon na di bind ay kaamil di jox Baayam Seex Ahmadu Bàmba, ku taaru woon am mbind la, (Yàlla xéewalal na nu ba nu gis te jànge ci am mbindam), muy kaamilu alxuraan bu rafet wallaahi! te wér ci ay yàq, batay di firndéel rafetug alxuraanam, limu bind ci ay kaamil nag lotteef na ci di ko takk mbaate xayma, waaye dondoos na ci ay ñeenti fukk ci ay kaamil yu mu bind ci ay yoxoom yu bokkul, Ñaar fukk ak juróom ñatt (28) ya baayam Seex Ahmadu Bàmba la ko jox àddiya. + +Ginnaaw njàngum alxuraanam jàng na xam-xamu diine ca Maam Moor Jaara Mbàkke (Boroom Saam) Ak Maam Cerno Ibra Faati Mbàkke, niki jennal Yàlla ak ngëm (Tawhiid, iimaan), Àttey Lislaam akuw yoonam (Fiq), Séllal ak jaamu ngir Yàlla dong (Ihsaan, Tassawuuf), bamu xarañe ko, Ginnaaw bi sëriñ bi jugee ci tukkib géej gi la ko mottalil xam-xam boobu ci Gànnaar ci dëkk bees di wax Xumaag, Mu ànd ak Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke ak Sëriñ Moodu Roqaya BUSO mom Sëriñ Mbàkke Buso. + +Ci njàng moomu nag ak yar bi, mu fàggoo ci lislaam ju mat sëkk, ragal Yàlla maandu, bëgg alxuraan, jëfe ab xam-xamam, di boroom ngor, muñ, ak jikko yees taamu. +Mu doon ku xarañe làkku araab itam, ba bind na ci ladabu araab lu sakkan, ci xeet i nose di ci ñaan ak a sant Yàlla, tey julli ci Yonent bi. + +Lenn ci ay jikkoom akug taalibewoom ci Sëriñ Bi + +Sëriñ Fàllu Mbàkke Di Ab jullit bu di doomi jullit, Nangu te seere ni: «Amul jenn Yàlla ju dul Allaa, (Yàlla aji sàkk ji yélloo wul Wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn, Mooy dégg, Mooy gis) Muhammad (Jàmmi Yàlla ak i xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la, (ndaw lumu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne la,). +As gor su di doomi gor, di ku sàmmu, ragal Yàlla lool, Gëm Yàlla diko jaamu, Sopp Yonent bi di topp sunnaam, Bëgg Sëriñ Tuubaa lool topp ay ndigalam, fonk ay bokkam te nawloo leen, di ab jullit bu koy jëfe, di as gor su gore, di ab jàngkat buy jàngale, di boroom xam-xam bu koy jëfe, di boroom alxuraan ci wattu ak ci bind, doon ku nangu dogal te man a muñ, doon ku yaru te daa yare, doon ku ñime njaboot te di leen taxawu, Ku woyof la woon te bëgg aw nit, ubbéeku lool te bari jàmm, ku manoona waxtaan te xarañ i wax, ku xeluwoon te daa xelale, ku xoromu te bari fulla, ku dégg wolof te man a tontu, ku bari yërmande tey jéggale, waxees nani daa tolloon ci màqaama mu kawe Yàlla, ba tax lu waay defat i neex nako, darra metteetu ko, lu waay def muni baax na, du sikk kenn du sikk lenn. + +Ku Am ag taalibe la woon, ba waxees nani bi ñu nekkee Xomaag ci Gànnaar Sëriñ bi daa xëy bis woote, Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke, Sëriñ Fàllu Mbàkke ak Sëriñ Moodu Roqaya BUSO mom Sëriñ Mbàkke Buso ne: +«Duma baayub kenn, mbaa mbokkum kenn walla nijaayu kenn, Jaamub Yàlla laa bu koy liggéeyal, ñi ma topp ci yoon woowii ma yeesal, ñooy samay doom, di samay jarbaat, di samay mbokk, di samay taalube» +ci loolu Yàlla xiir Sëriñ Fàllu mu ni Sëriñ bi jébbalu naa, jaay samag njuréel jënde ko ag taalube, +Ba loolu sax moongi koy féddali ci ag xasidaam moom Sëriñ Fàllu naan: +«Sunug yaakar moongi ci yaw, Yaw minu ubbil wunti yombte gi, Jaay naala samag njuréel jënde ko ag Taalube, Boo ma nangulee loolu, danaa sàkku defaat ko àddiya man ame ci xar-baax». + +Ku bëggoon Sëriñ Tuubaa lool, sopp ko, topp ko, yaakaar ko, roy ko, naw ko te sawar lool ci waxtaane ko, bariwaana xista yoy moo nu ko leeral, niki li xewewoon Jeewal ci tukkib Sëriñ bi ak yuni mel. +Ku soppoon Seex Ibra Faal, naw ko ci ag taalubeem, daa ko roy, yittewoo aw doxiinam te daa yéem ak taalubéem, amoon it ci moom ab cer bu rëy. + +Ci taalube googu la wéy di ko dunde ak way-yur wi diirub limuy dund, noonu la amewoon yitte yu màgg yu mu def ci defarug jumaay njaaréem, Ginnaaw bi fi Sëriñ bi jugee ci atum 1927, mu wéy ci yooyu tànk i taalube, topp tey déglu Sëriñ Moodu Mustafaa magam doon xalifab Sëriñ bi ca booba, ba ci ndigalul Sëriñ Moodu Mustafaa la deme demam gu siiw ga Màkka ngir aji, mottali yéeney Sëriñ bi ju ko yittéeloon te bëggoon ko ci xolam, ba daan waxni: +«Loolu ñu naa góomub deeyaale, bu ma ci amee darra sama naalub dem Màkka siyaare sama soppe ba la.» +Ba ci loolu Sëriñ bi tànnaloon boppam ñimu war a àndal ngir Aji, ñu doon: Sëriñ Mbàkke BUSO, Sëriñ Siidi Maxtaar Mbàkke Gaawaan (Maam Seex Anta) ak Alaaji Mayoro Faal, waaye njëkk muy matal yéene jooju wuyji Boroomam. +Ci atum 1928 Sëriñ Moodu am yéeney yabal Sëriñ Fàllu mu ànd ak ñooñii Sëriñ bi tànnoon, ku ci nekk ci ñoom yobbaale kenn ci ag njabootam, ñu aji màkka Aj gu jéeme te bari ay xew-xew, ak i xar-baax yu kawe, Ginnaaw Sëriñ Fàllu dafa xeesoon pecc ni Sëriif gi mu doon, ak cell gi nekkoon ci moom, ba mu demee yéem na léen lool, mook ñi mu àndal ci séen i melokaan akug ragal Yàlla te xam Ko, ame baatin bu jege, te bari xam-xam lool niki Sëriñ Mbàkke mi doon ab mufti. + +Waykat ba Sëriñ Muusaa KA tënk lii ci ne: +Allaahu zóol fadlil aziim () Kum jox ngënéel deefi la yéem +Faadilu mooy fadlu hamiim () Turam wi doyna xarnu bi +Mooy doomi shamsun wa xamar () Mbàkkeek mbusóobe duñ ko jar +Moo nàmp yaari meeni ngor () Mooy Bàmba tay ci xarnu bi +Saddiiti baayam lay royaat () Leerug cosaan ga day royaat +Nday jaa di xayru muhsinaat () Moo donn mbóoti xarnu bi +Mooy noobalub lislaam finun () Mboolem shariif yi moo ci gën +Donoy usaynu wal-Hasan () Maay xaadamam ci xarnu bi +Ma wax la lëf ci ay jikkoom () Lewet woyof ànd ak sagoom +Niru na baay ba mat na doom () Ëmb na kersag xarnu bi +Dem na ba màkkam jullikaay () Haj na siyaare ngën ji baay +Te ëndiwul alal di jaay () Nawleem amul ci xarnu bi +Taalifi baayam'ay wayam () Moo donn duusi xam-xamam +Moo naan ci géejug hikkamam () Sirroom ba doyna xarnu bi +Yàlla na am lamuy mébat () Ci nun nu am li nuy mébat +Ci moom te yal nan ami sët () Yu gën a gëm waa xarnu bi + +Lenn ci ay jëfam ak i xarbaaxam: +Xilaafa gi: +Ci tànk yooyu ba ci 1945 Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke wàcc-liggéey, Sëriñ Fàllu di xalifab Sëriñ Tuubaa Mbàkke, nekk ci di ko liggéeyal Muriid yépp jox ko séen kàddu, di déglu ay ndigalam, Mu sóobu ci yeggale jumaay Tuubaa ànd ko ak mboolem taalube yi, ñu topp ci ginnaawam, ngir yeggale naalub lislaam bu rëy boobii, di jumaa ji gën a rëy ci afrig, mu def ko it juróom i sooroor, tudde bu mag ba Làmp Faal ngir fàttalikoo ko Seex Ibra Faal taalubeb Sëriñ Tuubaa. +Yàlla dimbali ko mu yeggale liggéey bu rëy boobii dul fay mukk ci 7 suwe atum 1963, mu ubbi ko te jiite njaalbeenu julli ga, mbooloo mu takku teew fa. + +Ba mu ca jugee teg ca ni: "Fàllu neena «Galas» ci tuubaa" manaam dematu ma fenn tuubaa rekk, batax deesi ko woowe ginnaaw bi Fàllu Galas. +Ci biir liggéeyub jumaa ji waxees nani Sëriñ Fàllu toog na mbooloo mi nekk ci liggéey bi di yanuy dem ak a dikk, am góor gu ca nekk di yanoondoo ak mbooloo mi, Sëriñ Fàllu woolu ko mu ñëw mu ni ko "wax ma ñaata nga fi liggéey joxees la ko ?" mu wax ko Sëriñ Fàllu jox koko muni mes! kenn gisatu ko, Sëriñ Fàllu ni: "kooku dey góor mag la (Ibliis)". +Loolu di wane basiira bu xóot ci waa tasawuuf ñi, ngir gisub basiira, boo ci gisee man a xam li nga gis lumu doon, niki gisub bët, loolu basiira bu diis gann lay wone ca gaaña. + +Def na ay liggéey yu am solo ci luy yokk dëkk ba, ak diko dëppale ak soxlay nit ñi, niki defar ab fooraas bi fa njëkk nekk Daaru Manaan ngir jox way-dëkk yi séen soxla ci ndox, di jottal kuraŋ ca dëkk ba, akit rëdd ak jubale penku kër ya ngir mu dëppoo ak melow dëkk ba. +Sëriñ Fàllu sos na ay dëkk niki ko kilifay Muriid yi baaxoo ngir man faa yare ak a bay a ka jàngale, dëkk ya ñooy: Ndindi, Madinatu Salaam, Aaliya Mbepp, ak Tuubaa Bogo... + +Sëriñ Fàllu nag moo woote màggalug Tuubaa ngir Muriid yi àndandoo defee si ko Tuubaa, ginnaaw njaalbéen ga fu waay nekk rekk, ca kër Sëriñ Tuubaa ga fa nekk walla kër seexub muriid ba fa nekk +lees ko daa defe, mu mujj ko woote ci Tuubaa ngir ñépp ku ko man defee si ko fa, nu diko defe noonii ba jamono jii, ay milyoŋ i nit di ko teewe at mu nekk, ci ndigalul xalifa bu fi nekk. + +Sëriñ Fàllu nag boroom i xarbaax la woon, bu waa-senegaal xamandoo, ku amoon mayug Yàlla la, May gees di wax «KUN» Fayakuun (na am mu am) nga xamni yonent bee ko njëkk a feeñal ci kaw suuf, Sëriñ Tuubaa donde ko ci moom, rafaatale ko ñenn ci ag njabootam ak i taalibeem, Sëriñ Fàllu bokk na ci ñi yoroon xéewalug Yàlla gu rëy googu, Yàlla mu yaatu mi te barile lool, rëyle, yaatule te bëgg lool ku koy ñaan, Yàlla miy wax ne: «Ngëneel (fallu/fadlu) ci yoxoy Yàlla, di na ko jox ku ko neex» di maye lu ko soob ci nguuram gu yaatu gi dul jeex walla di wàññiku, +Neena ci Hadiisu Qudsi (Waxtaan wu sell) ne: ña njëkk ak ñi mujj ci nit ñi ak jinne yi mbooleséen, bu ñu taxawoon ci benn barab ñaanandoo li ñu bëgg ma mayandoo léen ko, du tax mu wàññi sama nguur gi ludul niki nga jël ab puso jam ko ci géej la cay taqe ci ndox ak la fa des noonu la li ma fajee séen ajo di toll, cey! nguuram gu rëy gii mu bokkul ak jenn walla kenn. + +Sëñ Fàllu yor may googu boole ak yërmànde di ci dimbali jaami Yàlla yi, ci di léen fàggul ab taw, fu ñu ko soxlaa, maneesu la takk ñaata yoon la baykat yi ñëw ci Sëriñ Fàllu ngir ñaan loo ko ab taw, dàqal léen njéeréer yi fi teewoon, ci ay jamonoom di lekk mbayum waa-senegaal, mu dagaan ko Yàlla, mu def ko ci anam gu jéeme, akit di faj way-tawat yi ci ndigalul Yàlla. + +Sëriñ Fàllu daan na wax ak mala yi, niki bu siiw bii te werloos ko: Amna bis taalube yu Sëriñ Fàllu liggéeyloo woon ay tool, te fas wa ko waroon a bay di bañ ba tax liggéey ba yeexe, xayna Sëriñ Fàllu dem fa, ñu jàmbat ko ko noonu niko moo waral liggéey bi yeexe, Sëriñ Fàllu di toŋal fas wa naan ko: "Ndax rusoo lii ? sa moroom yépp bëgg a liggéey ngir ngërëmul Sëriñ Tuubaa, yaw nga am foo ci man a bokke di bañ ! dëgg-dëgg bett ngama dé!." ña fa teewoon neeñu, fas wa daadi sëgg, ba mu tàmbalee liggéey ba nangootul a taxaw, jant so maneesu ko wàcce, mu melni ku xabtalu. + +Waxees nani am na jëmm ju bawoo ndakaaru ni woon daal day jébbalu ci Sëriñ Fàllu waaye dakoy natt ci ay mbir, mu juge Ndakaaru jëm Tuubaa, ñëw ba ci yoon wi ni day wàcc gas ñatti pax, ndax Sëriñ Fàllu dina ko xam bu yeggee am déet, Mu gas pax ya, jawal tuubaa, mu yegg ag mbooloo mi bari, mu bokk ci buuxante bi, Sëriñ Fàllu toppoo naan: May léen boroom ñatt i pax ya ca yoon wa mu yegsi ! +waaja yéemu, fekk xamul ni nitug Yàlla suturas Yàlla lay làmbool, maneesu koo suufeel mbaa diko wàcce, ku Yàlla yekkati la te suturaal ko. + +Amna góor gu dëkkoon yaraax (nëbbees na tur wa ngir ag njabootam ginnaaw tuub na) doon kilifa lool, waaye Yàlla nattoo ko muy naan sàngara su metti te diko nëbb, bëgg koo bàyyi mu të ko, bis mu dem Tuubaa siyaare ji Sëriñ Fàllu, beru ak moom jàmbat ko tawatam, Sëriñ Fàllu neko: "waxu mala sàngara waaye lépp lu deefi xelli ci bitéel rekk dootoo ko naan" ba ni fi góor gi jugee ci 1986 darra lu deefi xelli ci biteel rekk noppi na ci, ci lu dul coobareem, ngir loolu la bëggoon te man a lu ko boppam. + +Nettalees nani Sëriñ Fàllu daan na dekkal ku dee, loolu it xarbaax la bu yéeme, bu naqaree dégg te mooy li am, Kon ana gan dekkal lees di wax ? waaw lii a jar a laaj, ndax boroom basiira (ciiw) yi neeñu bakkan man naa dem ñatti yoon ci dundug nit, ci nan ? ñu ni nit Yàlla man na koo defal ay àpp ci nu mu neexe, ñatt i àpp yi man naa mucc ci ñaar yi, mooy ni: +Bu njëkk bi, ngir rëcc ci, day doon ku fegu, te moytu lool, di muzlu ci ay yi, Yonent bi neena:«ñi ci bàmmeel yi li ci ëpp làmmeñ moo léen fa yobbu (manaam ayu làmmeñ gir ñàkk a muzlu)» +tey sàmm bakkanam kem kàttanam, niko ko Sariya digale, walla mu am yërmàndey Yàlla. +Bu ñaareel bi: fàww mu doon ku set wicc, di ko sàkku ci Yàlla, di saraxe niko Yonent bi di waxe ne: «Sarax day feg dee» dee googu lay feg, akit yéene nit ñi jàmm walla mu am lool ku koy feg ci lor yi niki ab Sëriñ bu mat ba Sëriñ. +Bu ñatteel bi moom kenn du ko weesu, mooy dig bi Yàlla naan: «Bakkan du rot lu dul ci ndigalul Yàlla ci dig bees takk». + +Dee-dee yii nag, ku koy weddi xayna, xamoo fi nu saytaane féete, Yàlla may nako ci nun, lu baree bari, man nay daw ci sunu biir dereet te yàql nu rekk a ko tax a jug ak fowe nu, ba ku dul fegu ci Yàlla, di muzlu ci moom, lu nekk man nako ci yaw, ba ci ñi am i rab aki xàmb ci réew mi, am na ci ñu am lu léen di daaneel lol man naa yobbu séenug ruuh, bis walla ay bis, ñuy door a dundaat, lu am la fi te saytaane moo léen di fowe ndax mucclu wu ñu ci, ku gëmul ni dekkal yu melnii ma wax man naa nek: Rikk! jox nu ag leeral ci lu waral ñii séen i ruuh di dem ak a déllusi ? ku weddi lëf teg fa lëf mbaa delloos fa lëf la nga fa jëlewoon rekk. + +Lenn ci ay Waxam: +Sëriñ Fàllu Daan na wax ni: +Bu ñu nee kii doomi «diw» la, mu ne: «diw doomi ràkkal la; fexee doon ràkkal a gën» +Wax ju fees dell ak i njariñ man a jàjji bépp doomi Soxna ci mu jéema melni baayam te bañ a rekk doyloo mbaaxug baayam, ngir ni ag mbaax déesu ko dondu. + +«Xaw a dof mbaa xaw a dee rekk a fi nekk» +Manees cee degge, kuy wut Yàlla nekk di jëf mu nduru ci nit ñi jëf i dof, moo gën ñàkk Yàlla ba ëllëg nga xaw a dee. + +«Dee leen bëgg ndir lu waay bëgg am ca darra» +Wax ju am solaati, manees cee xame ni ci ag bëgg rekk lees di ame mboolem càkkutéef yi, ag bëgg nag ci ngëm la bokk, +Yonent bi (jàmm i Yàlla ci moom) nee: «Kenn ci yéen du gëmm lu may da maa gën a bëgg baayam, doomam ak mboolem nit ñi» +Lu waay bëggul def ko du ko ca may njariñ. + +"Li baax ci mag «Këll!», «Këlëj»" +Wax ju baax ji mag ci dëgg nag, «Këll» jox ko mu lekk ba suur këll, «Këlëñ» bàyyi ko mu tëdd dallu. + +Amna ñaar ñu yoroon ak fital (pistoler) soxla xaalis ni dañu koy jaay i Sëriñ Fàllu, ñu yegsi niko:lii de fital la da nu koy jaay, Sëriñ Fàllu ni léen ayca! defaral ma xool, +Waaji diko di defar fital gi te fekk mu jëm ci Sëñ Fàllu, mu ni ko déet jëmale ko nale, Waaja neko: déet darra nekku ci, Sëñ Fàllu niko: «waaw kon jëmale ko fi darra nekkul fii maa fi ne» + +Amna jëmm ju masa ñëw ci Sëriñ Fàllu diko jàmbat Yaayam, naan ko dafa naqari dereet lool, ba kenn manu la dëkk am moom, Sëñ Fàllu neko: aah! mbaa du jooy guddi ? +Déggal lii tontu lu yéeme rekk! waaw! ndax kune ci nun daanga jooy guddi sa nday diko muñ ak a jug dila topptoo, nga tee koo nelaw, kon nag, lu nu ñu def bi nu màgge rekk war nanu koo muñe loolu. +......... + +Mottali: +Waaw-kay! kenn ci kiimaan i Yàlla, Màndargay Yàlla yi, bokk ci ñi Yàlla gaaral sunu kanam, ngir nu am firnde ci ni, Ku defal Yàlla lii am lii, neko Sunu sang Muhammad waxe: Ku dox jëm ci Yàlla akub Yonentam; Yàlla daw jëmsi ci yaw» +wone it ni Yàlla ku laabiir la, kuy maye lune, di bégal ab jaamam ci lu ko soob, +Sëriñ Fàllu Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa nag mooy ñaareelu xalifab Sëriñ Tuubaa ginnaaw bi mu wuutoo Sëñ Moodu Mustafaa ci atum 1945 ba 1968 +mu wàcc-liggéey Sëriñ Abdu Laat Mbàkke wuutu ko di xalifab Sëriñ Tuubaa. + +Sëriñ Muhammadu Faadl mii nag lees di defal Màggalug «Kazu Rajab» 27 ndeyi-koor ci at mu nekk ca Tuubaa, ak barab yi muriid yi féete, niki kër Sëriñ Tuubaa yi ci àddina si. + +Kazu Rajab nag bis la bu màgg lool ci lislaam, ngir ni ci lees wàcce julli, ci la Yonent bi (jàmm i Yàlla ak i xéewalam ci moom) riñaane woon wuyuji wooteb boroomam ca asamaan ya, ci guddi gii la gise ak Maamam Ibraahima +ak Ismaayil, am mboolem Yonent Yàlla yi (jàmm ci ñoom) jiite léen julli ca Bëyti Al-Maqdis (nee bu sell ba), ci lako Yàlla yéege ba fa moom, ñii ni gis nako ñee ni gisu ko, waaye lu ci man a am daal, Yàlla nettali na nu ni: +ñëw na ba sës ci moom rikk, Yàlla gaw ko ci diggante ñaari xala niki (), loolu lépp nag Màggug guddi gi lay wone, Kon Yàlla nanu Yàlla wonale ak barkeb guddi gi, nu séddu ci, te Yàlla baaxe nu ca xam-xam boobee +ci ñeeloon Yonent bi (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci moom) kem sunu tolluwaay. + +Sëriñ Muhammadu Faadl Mbàkke, noongi ñaan ci Yàlla mu dolli ay leeram, dolli koo yërëm, dolli koo gërëm te xéewale nu ci barkeem, Ci barkeb turandoom Mahammad (jàmm i Yàlla ci moom). + +Niti senegaal +Yoonu murit +Ki njëkka doon xalifa, wuutu fi baayam Sëriñ Tuubaa ca yan bu diis ba + +jaar-jaaram + +Niti senegaal +Yoonu murit +Mooy ñeenteelu xalifa ginaaw S Abdul Ahad + +Dundam + +Niti senegaal +Yoonu murit +Ca la ñu ca xamoon ku daan jàmbaare la daan doon ci toolub lislaam bi, di liggéey di joxe ngir sémbi yoon wi man a jëm kanam, ak doonte bari na ci ñoom ñoñ duñu julli, duñu woor, waaye teewul bu ñu doon laal diiney lislaam ñooy njëkk a jug ngir aar ko, kon daal man nañu leen a tudde dofi lislaam, walla yu murit, bari na lu ñu leen man a jame waaye it lu ñu leen man a tagge. + +Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen . +Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. +Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam. +Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon. +Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a kopparal ci lislaam man a kopparu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it. + +Ñàkk a julleek a woor it du gëm-gëëm fi ñoom ba ku koy def toppoo seeni sart, waaye ag feeñte (phénomène)la gu nekk ci ñoom gu man a xéy dañ + +Yoonu murit +Rakki Sëriñ bi ji la, ju mu bokkal benn baay, te di ab taalubeem bu ko nanguloon te gëm ko, bokkoon ciy kàngamam, man nañu ne mooy ki toppoon ci moom ciy jamonoom, ndax bi Sëriñ bi di dem ca tukkib géejam ba moom la wuutaloon ca ginaawam ca njaboot ga, mu jiite lepp +Ki moo féetewoo woon Njàggale mi, lu bari ci doomi Sëriñ bi moo leen jàngal, moo yoroon daara ju mag ja ca Ndaam di Daarul Haliim Al-Xabiir, bi Sëñ bi sàncee it Mbàkke Baari ca Jolof, ba Tuubaa rëbee, ngir jàngale moo yoroon njàngele ma di ko doxal. +Làmp Fall, Baay Faal bu mag bi, jàmbaar ju raw gaynde + +Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen. + +Jëf yii nag yu ci ëpp du yu bawoo ca Maam Seex, moom kay day yu bawoo ci seen bopp, li leen jur di am njaxas mu ag dëddu àdduna ak ginaawal ko ak yëngu bu bari bi ñu taqool ba duñu talati seen bopp ñu far ba seeni kawar noonu duñu leen topptoo, duñu leen tal. + +Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. +Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam. + +Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon. + +Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a alalal ci lislaam man a alalu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it. + +yoonu murit +niti senegaal +Jenn la ci daara yi Sëriñ Saaliwu sancoon ngir liggéey ak jaamu Yàlla, moom nag mi ngi sosoo ci 15 daara yu ñu defar ci anam gu xereñ, tali yi xotti ko, indees fa ndox, ñu fay bay lu sakkan ci gerte ak dugub ak yeneeni mbay ngir ag sukkandiku gu poppu ci wàllug mbay ak xam. + +dëkk-dëkkaani Senegaal +yoonu murit +Seex Beeco Cuun taalubeb S Saaliwu la, mu nekkoon kenn ci ñi daan liggéey ci yoriin wu Senegaal (administration sénégalaise), ku bari ñu aju ci moom la ciy murit, moom nag woote na ag ceexal gu bawoo ca S Saaliwu, waaye aw nit rawatina ci biir murit gi dañul di ko sikk ak a diiŋat + +yoonu murit +niti senegaal +Góor Yàlla, jàmbaari Lislaam, taxawoon na ci tas lislaam ci àdduna bi bépp, moo waraloon foo ko fekk daa wul toog, mi ngi woon jamono ju nekk ci ab tukki mbaa muy door a wàcc te lepp dara du sababam lu dul taxaw ci baatu Yàlla bi di bu kawe, moo digle kër Sëñ Tuubaa yi ci biti, te lenn la ci jubluwul lu dul barabi lislaam yu jullit yi di man a daje ngir jaamu Yàlla ak dimbalante. + +Niti senegaal +Yoonu murit +Royan dëkku Faraas. Nitñii motnañu 18 100 (2005). + +Dëkki Faraas +Rakki S Abdul Ahad ju mu bokkal nday ak baay, ku jàmbaare la woon ci jàngale Alxuraan ak xam-xam ak yar ci diine, taalif na lu sakkan ciy téerey xam-xam, ñuy ci araab ak ci wolof, téere bu ci mel ne Xuratul Hayni ci wolof la ko def, muy téere bu jéggi dayo ba ci am solo, di wax ci lépp lu soxal nit, ci diine, ci paj, ci dundiin ak ci fànn yépp, Buxyatul Muriidiin, Naylul Awtaar ak yeneen téere yu am solo, lu sakkan ci boroom xam-xami yoon wi ci këram lañu jànge, ak sëti S Tuubaa yu bari + +Niti senegaal +Yoonu murit +Kenn ci doomi S Tuubaa yu am yi ag jeexiital te àgguñu ci di xalifa, ku amoon xam-xam, mooy ki bind téere bu am solo bii di ab delluwaay ci yoon wi, di "Minanul Baaqiil Qadiim" + +ku ci bagga xootal na xool Sëriñ Basiiru Mbàkke ci situ wikimouridia.org + +Niti senegaal +Yoonu murit +Abdulaay Wàdd mi ngi juddu ci 29 Mee 1926 ca Kebemeer, am na 82 ciy at, mooy njiitu réewum Senegaal ca 1fanu awril 2000 ba leegi, ki mu wuutu ci toogu boobu mooy Abdu Juuf. Ba tey mooy njiitu làng gu demokaraasi gu Senegaal (PDS), te it moo ko sos ci 37 Suwe 1974 ci ginnaaw bi mu ci tàggoo Léopold Sédar Senghor ba mu nangu, nekk na ci kujjeg politig gi lu toll ci 25 ciy at, yàgg na koo jiite, ci diir boobii tëjees na ko ci ay yoon. Soxnaam mi ngi tudd Fifiyaan Wàdd. Am na ñaari doom: góor ak jigéen, Kariim Wàdd mooy góor, Sinjili Wàdd di jigéen. Diineem mooy lislaam fiqu maalik, bokk it ci yoonu murit. Moom nag ku xareñ la ci wàllu yoon ak koom-koom am na it lijaasa jàng wi gën a mag ci ñaari wàll yooyii, mi ngi jànge wàllu yoon ci daara jii di lycée Condorcet ca Fraas. Wàllu koom-koom mu jànge ko ci daara ju kawe ju Ndakaaru. + +niti senegaal +Njiiti Senegaal +Kii mooy rakki Sëriñ Tuubaa ji daa sotti li ëppoon ci xasidaam yi ginaaw bu ko Sëriñ bi bindee ba noppi, moo ko daan maas it + +Niti senegaal +Yoonu murit +Xarey àdduna yi ñooy ñaari xare yi réew yu bari ci àdduna bi bokkoon doon def ci seen biir. Doon xare yi ëpp ay yaqu-yaqu ak ay bakkan yu ci des. + +Xareb Àdduna bu Njëkk +Ñaareelu Xareb Àdduna + +Laataa Ñaareelu Xareb Àdduna bi bu njëkk bi Xare bu Mag bi lees ko daan woowee. + +xarey àdduna +'Lislaam jenn diiney asamaan (monothéiste) la (walla ju jenn yàlla), ju Muhammad (j.m) doon woote ca Dunu Araab ba (arabie) ca VIIeelu xarnu, Moom nag jenn la ci ñatti diine yees di wooye (diine yu ibraayma) yi, ñooy (diiney yahood, nasaraan ak Lislaam). Ñi ko gëm ñu leen di wooye ay "Jullit", mu bawoo ci baatub julli biy wund nangul Yàlla (t.s) di dégg ay ndigalam, ndax kooy julli ngir moom di ko jaamu nangul nga ko te ronu cig ronam, baatub jullit nag ci araab mooy (Muslim) giy tekki "aji jébbalu", aji nangul Yàlla, ndax jullit bi naafequl day déggal Yàlla, wéetal ko, ronu ci ron keppaaram, tënku cig nosteem, raggu cig bokkaaleem, dañtalu ci ñoñam (ñoñ bokkaale). Loolu nag ag bayliku gu mag la gu tukkee ci nit ñeel Yàlla, féete ci moom, jox ko boppam ci lépp lu muy def. + +Jullit ñi dañoo gëm ne Lislaam mooy diine ji Yàlla mujj a wàcce ci (diiney asamaan) yi, te moom nasaxal na ya ko fi jiitu ci diine, (maanaam wotte na leen) ni ko Alxuraan waxe: «Tay jii laa leen matalal seen diine te mottali sama xéewal ci yéen, te gërëm naa Lislaam muy seen diine » (Taabal (mayida) 3), waxati ko: «Wàcce nañu ci yaw téere ba ànd ak dëgg, muy dëggal li ko fi jiitu ci téere, te di ko féete kaw » (Taabal 48). + +Jullit ñi tam dañoo gëm ne Muhammad ab yonent la bu bawoo fa Yàlla, mooy ki ub nabiyu yi ak yonent yi, moom nag Yàlla da koo yonni ci ñaari way dijj-bopp yi (Jinne ak Nit). Bokk na ci dàtti pas-pasu Lislaam gëm ne am na jenn yàlla ju fi nekk moom rekk mooy Yàlla "Allaa", te ñoom (juliit ñi) anafiya lañuy topp muy diiney Ibraayma. + +Jullit ñi dañuy Gëm Yàlla, Gëm Malaaka yi, Gëm Téere yi, Gëm Yonnant yi it mboole seen, yi fi jiitu woon, ak Gëm Bis Pénc te Gëm Dogal bi, ak Alxuraan mooy téere bi ñu wàcce ci Muhammad mu tukkee ci Yàlla, jaare ci Jibriil, Alxuraan nag mooy balluwaayu yoonal bu njëkk bi ci Lislaam, teg ci Sunna. Ponki Lislaam nag juróom lañu: + + Seere + Julli + Natt asaka + Woor + Aj Màkka ci ku ko man benn yoon + +Moom lañuy jàppe ñatteel ci dawaan yu mag yu diiney jenn-yàlla yi bokk ci njabootugDiiney Ibraayma yi. Moom nag diine la ju wuuteek diiney Yahood ak ju nasaraan ji mu bokkal ay wàll yu bari yu niroo. Moom nag mooy jaaro bu mujj bi ca càllalag diine ja yonent ya indi woon mu bawoo woon ca Yàlla, la ko dale ca Noohin romb mbooleem yonent yi ba ci Muhammad (j.ñ) mi tëj Yonent gi ak téere yi ci téeéreem bii di Alxuraan. + +Alxuraan nag mooy téere bi jullit ñiy sukkandiku ci seen yoonal, bu jàllee sunna ñëw, di jëf ak waxi Yonent bi Muhammad (j.m), mook Sunna ak yeneen ñaar ñooy bañlluwaay yi jillit yiy ball-loo seeni àtte ak yoon (sariiya), yeneen ñaar yi di "ijmaah" (dajeg boroom-xam-xam yi) ak Qiyaas (nattale). Moom Alxuraan nag waxi Yàlla la ju ñu wahyu Yonent bi jaare ko ci Jibriil, muy lol daa wàcc ci anam gu toftaloo te toppante, ci diir bu tollu ci 23 at. + +Lu tollook 1,5 milyaar ciy jullit ñi ngi ci àdduna bi. Ñoon nag dañoo séddaliku ci ay dawaan yu limu, ñooy ci tur dawaanu Sunna, bi ëmb lu tollook 80 ak 85% ci jullit ñi, ak bu Siiya bi nga xam ne ma nga ëppe ca Iraan, ci biir Sunna am na fa ay bànqaas niki tasawuf, naka noonu ci Siiya. + +Xamale ko + + Baatub Lislaam day tekki jébbalu ci jenn Yàlla ji amul moroom amul ku mu bokkal (laa sariika lahuu) joxe sa bopp gii nag ci teeyug bakkan lay ame. Fi Jullit ñi Yonent yépp ay jullit lañu, Ibraayma, Musaa ak Isaa (j.ñ), ndax ñoom niki jullit yépp dañoo tënku ci ay àtte yu Yàlla, te topp ci, kon jébbalu nañu te nangul Yàlla, bu ko defee Yàlla di leen dëgëral ak a dooleel ci ay kéemtaan (miracles) + Baatub Jullit nag li muy tekki mooy ki aju ci diiney Lislaam di ko doxal, di julli tey def mbooleel àttey Yàlla yi. + jullit nag leeg-leeg mu tekki aw xeet, walla aw nitu am réew niki ña dëkk ca Bosni, ñooñu ay Jullit lees leen di wooye, naan Kurwaat Serb ak Jullit + +Lislaam nag du lu ñu jagleel aw askan wëliif weneen, walla aw nit bàyyi weneen, moom de ag woote la ñeel mbindéef yépp, ngir amal ag maandute ak yamoo ñeel mbindéef yépp. Lislaam daa taxaw ci ag nite ak yamale mbooleem bennaani mboolaay gu Lislaam gi, du def genn ràññatle ci diggante ku am ak ku ñàkk, ku am doole ak ku ko néewle, garmi akub baadoola. Neewul wenn xeet a gën moroom ja ndare ci ragal Yàlla ak topp ko. Loolu mooy dàtt bi jëfi jullit di tegu ngir man a baax, lu ko moy déet. yàlla a ngi wax ci Alxuraan: «Yéen nit ñi, ñun de bind nañu leen ci góor ak jigéen, te def leen ay askan aki giir ngir ngéen xamante, (te ngéen xam ne) ki gën a tedd ci yeen fa Yàlla mooy ka ca gën a ragal Yàlla, Yàlla ku xam la, ku dañ-kumpa la (dara umpu ko) » (saaru néeg (Hujuraat) 13) + +Yonent bi Muhammad (j.m) nee na: «Ndax duma leen xamal ku di ab jullit? Kok nit ñi wóolu nañu ko ci seen alal ak seen bopp, ab jullit mooy ki nit ñi mucc ci làmmiñam ak loxoom, jiyaarkat mooy ki jiyaar ak bakkanam ci topp Yàlla, aji gàddaay mooy ki gàddaay ñaawtéef yeek bàkkaar yi» + +Ag sosoom +Lislaam feeñ na ca Dunu araab ba ca juroom ñaareelu xarnu g.j, (ginaaw juddug Isaa), ci loxol Muhammad mom Abdul Laa (j.m), mi xéyoon di woo nit ñi ci ñu gëm pas-pas buy woote jaamu Yàlla miy kenn tey ku wéet te ba jaamug xërëm yi, mu boole ci indiwaale fi meneen mbooloo ciy ponk aki xalaat ak pas-pas, loolu nag di ndigal lu bawoo fa Yàlla miy kenn tey ku ñàkk maas, (Allaa), rax ci it Alxuraanالقرآن ju araab ju ñu wàcce ci Muhammad (j.m) mu tukkee ci Yàlla jaare ci malaaka Jibriil, mii daa jàng Alxuraan jii ci Muhammad ci anam gii nuy wooye "Wahyu". + +Pas-pas ak Sariiya +Jullit ñi dañuy gëm ne Muhammad (j.m) daa dikk ngir mottali te tëj bataaxelub Yàlla bi mu yonnee yonent yi ko fi jiitu woon niki Ibraayma, Musaa, ak Masi Isaa mom Maryaama (y.j.ñ) te ñoom Yonent yooyu yépp ay jullit lañu, te dañuy gëm it ne Anafiya ji ñu nekk mooy cëslaayu diiney Ibraayma. Dañuy gis it ne wuute gi ci diiney asamaan yi ci sariiya la (maanaam àtte yi) waaye du ci pas-pas bi te sariiyab Lislaam nasaxal na (wuutuna fi) mbooleem sariiya yi ko fi jiitu woon.Kon diiney Lislaam mi ngi ame ci pas-pas ak sariya. Pas-pas bi di mbooleem dal (principe) yi nga xam ne jullit bi war na leen a gëm, ñoom nag way sax lañu, duñu soppiwku ak lu yonent yi soppiku. Sariiya nag aw tur la ñeel àtte yu jëf yi nga xam ne man nay wuute ak a soppiku ci soppikug yonent yi, bu ko defee bi mujj a ñëw di nasaxal (di fi wuutu) bi ko jiitu. + +Alxuraan nee na: «Wàcce nañu ci yaw téere bi ànd ak dëgg, muy dëggal la ko fi jiitu ci téere te di ko féete kaw (di ko nasaxal), àtte leen ci li Yàlla wàcce te bul topp seeni bànneex ba bàyyi li la dikkal ci dëgg, ku mu ci yeen defal nañu ko aw yoon akum ngér, bu sooboon Yàlla mu def leen wenn xeet, waaye da leen di nattu ci li mu leen indil, njëkkanteleen yiw yi, ca Yàlla ngeen di dellu, bu ko defee mu xibaar leen fi seenug wuute nekkoon» (saaru Taabal 48) {وَأَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ مُصَدِّقاً لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ الْكِتَابِ وَمُهَيْمِناً عَلَيْهِ فَاحْكُم بَيْنَهُم بِمَا أَنزَلَ اللّهُ وَلاَ تَتَّبِعْ أَهْوَاءهُمْ عَمَّا جَاءكَ مِنَ الْحَقِّ لِكُلٍّ جَعَلْنَا مِنكُمْ شِرْعَةً وَمِنْهَاجاً وَلَوْ شَاء اللّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَـكِن لِّيَبْلُوَكُمْ فِي مَا آتَاكُم فَاسْتَبِقُوا الخَيْرَاتِ إِلَى الله مَرْجِعُكُمْ جَمِيعاً فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ }المائدة48 + +Ay baat aki waxiin +"Allaa":Yàlla, mooy yàlla jiy dëgg ji yayoo ag jaamu moom rekk, moom mooy Aji bind jiy Aji sàkk, kiy melal, ki moom tur yu rafet ya ak melokaan yu kawe ya, ki bind nekk gi(àdduna bi) tey ki nga xam ne moom rekk a ko man, mooy ki moom asamaan yeek suuf si. Yàlla nag yonni na yonent yi ngir ñu woo nit ñi ci ñu jaamu ko moom rekk te bàyyi jaamu ku dul moom. + +"Yonent bi", yonentub Lislaam mooy Muhammad mom Abdul Laa mom Abdul Mutalib mu Quraysin, mi ngi judd ci 571 ci Màkka gu tedd gi. Ag njabootam ñu xame ko ci turu njaboot gu Haasim, ngir askanale ko ca maamam Haasim mom Abdu Manaaf. Yàlla yonni na ko jox ko diiney Lislaam atum 610 g.j te booba ma ngay def xalwatu ngir jaamu ca xuntim Harraa. Xamees na ko ci njëkk ak ci ginaaw yonent gi ci ay jikko yu rafet, dëggu ak wóor, looloo waraloon ñu ko daa wooye "Ku dëggu, Ku wóor ki", mi ngi faatu ci bisub altine 12 ci rabiihul lawal atum 11 g (mu gàddaay gu Yonent bi)te booba ma nga amoon 63 ciy at. + +Alxuraan: Alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi, mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu Lislaam gi, ci ginnaawam la Sunna di ñëwe. Li njëkk a wàcc ci Alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru Halaq muy : «Jàngal ci sa turu boroom bi bind (sàkk)» + +Alxuraan nag mooy waxi Yàlla ji mu wàcce ci Yonenteem bi Muhammad, Jibriil nag mooy ndawul Yàlla tey malaaka mi ko wàcce; ngir nag Yonent bi jottali ko nit ñépp,. Moom nag fa Yàlla dees koo bind ca àlluwa ju ñu wattu ja (Lawhul Mahfuus), àlluwa jii nga xam ne Yàlla bind na fa lu nekk njëkk mu koy sàkk.Wattu googu nag Yàlla la soob, mu bëgge ko noonu, noonu la ko waxe: «Ñun ñoo wàcce Alxuraan, te ñun ñoo koy wattu» + +Barab yu sell yi: +Lislaam am na ñatti barab yu sell, ñooy Màkka gu tedd gi, Madiina gu leer gi ak Quts (sorisalem): + +Màkka: + +Fa la Yonent bi Muhammad (j.m) ganee àdduna, mooy tam barabub wàccug Wahyu gi, fa la doorees it woote gi. Fa la Masjidul Haraam it nekk (Jumaa ja wër Kaaba ga) gi ëmb Kaaba gu tedd gi nga xam ne Ibraayama'a ko tabax ak doom ja Ismaayil (j.ñ), fa la jullit yiy jublu it ngir jóoxi séen faratay aj. Kaaba gi mooy xiblay jullit ñi, fa lañuy jublu ci mbooleem seeni julli. + +Madiina : + +Madiina gu leer gi (madiinal munawwara ci araab), njëkk Lislaam (Yasrib) la tuddoon, ñi ngi ko tudde Madiinal Munawwara, walla Madiinatur Rasuul (dëkkub Yonent bi) ginnaaw Lislaam. Fa la Masjidun Nabii nekk (Jàkkay Yonent bi) + +Quds : + +Quds nag dafa mel ne turam wiy tekki "ag sell", di barab bu ñu sellal fi jullit ñi, fa la masjidul aqsaa nekk, (Jàkkay Aqsaa) ca Palestin, muy jàkka ji Yonent bi siyaare woon ca guddig "rañaan ga ak yéeg ga", mooy guddi gi ñu farataale julli. Fa la Yonent bi jiite woon cig julli mbooleem nabiyu yeek yonent yi. Masjidul Aqsaa nag mooy benn pàkk bi nga xam ne mbooleem diiney Ibraayma yi yépp sellal nañu ko: Lislaam, Nasaraan ak diiney Yahood + +Sariiya bu Lislaam + +Ci gëm-gëmu jullit ñi Sariiya bu lislaam (walla yoon wiy àtte ci lislaam) mooy nos mbooleem wàlli dund yu wuute yi, gu politig, gu mboolaay, gu koom-koom ak gu jëmm. Loolu nag ag kéemtaan nekku ci ginnaaw moom mi taxaw ci Alxuraan ak Sunna dafa bawoo ca Aji bind ju tedd ji te màgg (Yàlla). +Sariiya nag am mbooloom ay yoon la (ay àtte) yuy leeral séqoo ak digaale yi am ci diggante nit ak Yàlla (t.s) ak diggante nit ak nit ak mboolaay gi ak àdduna bi. Day leeral it li dagan a def ak li daganul. Yi ëpp solo ci àtte yii ñooy ponki Lislaam yiy juroom te ñu leeraloon leen. + +Lislaam tam day waral jullit bi di tënku ci Sariiya, di ci àttee ay lëj-lëjam ak xiiroo ak ŋaayoo mbaa xuloo yiy am ci diggante jullit ñi, day waral it ci jullit bi muy ràngoo jikko yu rafet. + +Gongikuwaayu Sariiya bu njëkk bi nag (walla ab balluwaayam) mooy Alxuraan, moom nag ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla ñeel ab yonentam Muhammad (j.m) mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal yi ak àtte yi ci Lislaam, Yàlla (t.s) warlu na ne dina ko wàttu cig soppi mbaag wëlbati: «Innaa nahnu Nassalnaas Sikra wayinnaa lahuu la haafisuun». Alxuraan yaxal na ci waraug topp ndigali Yonent bi (j.m) ndax ay waxam ag wahyu lañu gu tukkee fa Yàlla (t.s), Alxuraan nee na : «Du waxe bakkan, li muy wax ag Wahyu la gees koy wahyu», looloo tax deesi jàppe Sunnas Yonent bi (moom am mbooloom ay wax la aki jëf yu Yonent bi (j.m)) muy gongikuwaay bu ñaareel bi ñeel Sariiya walla yoon ci Lislaam. + +Sunna nag nga xam ne mooy ñaareelu gongikuwaay bi, dajalees na ko ci am mbooloom ay téere, niki Sahiihul Buxaarii, ak Sahiihul Muslim ak yeneen téere yu Addiis. + +Ñatteelu gongikuwaay bi nag balluwaayu wuute la ci diggante ñaari ngér yii di Sunna ak Siiya: Waa Siiya ñoom dañoo gis ne Addiis yi bawoo ca Ahlul Bayt (Njabootug Yonent bi (j.m)) ñooy ñatteelu gongikuwaay bi ñeel Sariiya, téerey Addiis yi nekk fi ñoom dafa ëmb waxi Yonent bi (j.m) ak waxi Ahlul Bayt,seen téereb addiis it mooy téereb Kaafii bu Kaliinii (كتاب الكافي للكليني) + +Ñeenteelu gongikuwaay bi mooy Qiyaas walla “nattale” (maanaam nattale mbir mu amul ab àtte ci mbir mu mu nirool mu ko amoon) + +Ngérum Lislaam +Lislaam day dox ak a liggéey ci teggi toroxte wëliif nit ñi, tee leen a toroxlu ñeel ku dul yàlla (t.s). Mu gis ne doyodal gi gën a réy gi nit mas a dajeel ak toroxte mooy muy jaamu aw doj mbaag garab walla dundat (bayyima), mbaa muy toroxlu ñeel mbindéef muy dund mbaa mu dee, moo xam nit la mbaa lu ko moy, ci noonu mu aaye ñuy jàppe ay fóore mbaay làbbe (الأَحْبَارِ وَالرُّهْبَانِ)ay yàlla te ba fi Yàlla. Mu jugati moom Lislaam xeex tooñaange yi ñennat ci nit ñi di teg seeni moroom yu néew yi doole, loolu leer na bu baax ci Alxuraan :{وَلاَ تَأْكُلُواْ أَمْوَالَكُم بَيْنَكُم بِالْبَاطِلِ وَتُدْلُواْ بِهَا إِلَى الْحُكَّامِ لِتَأْكُلُواْ فَرِيقاً مِّنْ أَمْوَالِ النَّاسِ بِالإِثْمِ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ }[2] +«Buleen di lekk seeni alal ci seen biir cig “neen” (ci lu dul dëgg, ci bàkkaar) ak di ci jox way àtte yi (di ci gere) ngir (rekk)ngeen lekk ab kuréel (ab lim) ci alali nit ñi ci bàkkaar te booba xam ngeen ko» +Alxuraan waxati it ne : {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُواْ إِنَّ كَثِيراً مِّنَ الأَحْبَارِ وَالرُّهْبَانِ لَيَأْكُلُونَ أَمْوَالَ النَّاسِ بِالْبَاطِلِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللّهِ وَالَّذِينَ يَكْنِزُونَ الذَّهَبَ وَالْفِضَّةَ وَلاَ يُنفِقُونَهَا فِي سَبِيلِ اللّهِ فَبَشِّرْهُم بِعَذَابٍ أَلِيمٍ }[3] +«Yeen ñi gëm, ñu bari de ci fóore yi ak làbbe yi dañuy lekk alali nit ñi cig neen tey dëdduloo wëliif yoonu Yàlla wi, ñiy dëxëñ (denc) wurus ak xaalis te duñu leen def ci yoonu Yàlla, nanga leen bégal ci mbugal mu tar» + +Loolu mujj na di ab balluwaayu doole ak kàttan ñeel Lislaam, ngir yamale gi ci nekk ñeel nit ñi ñépp, amul xejj ak séen, ab bàkkam di “Ab araab gënul ab ajam (ku dul araab), ab ajam gënul ab araab, ku weex gënul ku ñuul, ku ñuul it gënewul ku weex lu dul ragal Yàlla (tënku ciy ndigalam teet ay tereem, nit ñépp ci aadama lañu bawoo, te moom ci suuf la bawoo ” kon manuñoo gënantee ciw melo mbaag ndawal, waaye ci jikko ju rafet ji ëmbu ci ragal Yàlla giy waral di tënku ci ay ndigalam aki tereem te loolu mooy ag xay dëgg-dëggi xay, ndax mooy waral nit di def ag nite, di wormaale tey xam ne mook ñepp a yam, mook ñepp a bokk fu ñu juge, mooy Aadama, te moom cosaanam du dara lu jar muy jàpp ne kenn la, mbaa moo gën kenn, suuf sii muy joggi ak a puup, ak a saw ci la bawoo, kon déet ag gëne di ko ñeel lu dul cig ragal Yàlla giy njobbaxtal cig baax akug yiw. + +Déet ag xeetal (racisme), déet ag kuréelal (def ay classes sociales). Bu ko defee, ngér mii xéy di luy doog a am ci taariixu àdduna bi, ci nguur gog ki ko doon àtte, di ko doxal ab yonent la, ab sartu réewam di Alxuraan ja juge ca Yàlla, bu ko defee aw askanam di xéewu ci xéewalug maandute ak kaaraange. + +Jullit ñi dox nañu ci wisaare maandute ak yoon ci mbooleem ruqi àdduna bi, yëngu it ci yekkati tooñaange, toroxte ak doyadal wëëliif way néew yi doole ak ñu ñu noot ñi. Looloo jur nit ñi sottiku ci diine ji ci ay mbooloo, buur yi daal di koy xeex ak way jalgati yi ngir li ñu ci gis ci ag tiital ñeel seeni nguur, ñu xam ne seeni nguuru way jeex lañu, seeni nguur way dañ lañu feek lu néew, way tuxoo ci seeni loxo lañu, ndax seeni njaboot ak seeni càmmiit (administrés) tàmbali nañoo tàbbi ci diine ju yees ji.Loolu mooy mbóotum gaaw a tasug Lislaam ci mbooleem pàkki àdduna bi ci diir bu gàtt bu weesuwul at yu néew, loolu nag jaaxal na boroom xam-xami taariix yi ak boroom xam-xami mboolaay yi. + +Saaba bii di Ribhi'Bn Haamir génn na loolu ci anam gu leer ca waxam ja:(Yàlla moo nu yonni ngir nu génne ku ko soob ci jaamug jaam yi, yobbu ko jaamu boroom jaam yi, ngir ñu jële ko ci xatug àdduna jëme ko cig yaatoom, xettali ko ci jengug diine yi, yobbu ko ci maandug Lislaam..mu yonni ñu ak diineem ji ci mbindéefam yi, ngir ñu woo leen jëme leen ci, ku nangu loolu ñu nangul ko, dellu wëliif ko (ba ko ci jàmmam), ku bañ nag ñu xeex ko ba fàww, ba kero ñuy àgg ca dëelub Yàlla ba. Ñu ne ko : luy dëelub Yàlla ba? Mu ne: Àjjana ñeel ki dee ci xeex ak ki bañ, ak tuufu (gañe) ñeel ki des (ki deewul). + +Tasug Lislaam akug wisaaroom ak ni jullit ñi séddalikoo ci àdduna bi + +Muhammad (j.m) aki saabaam tàmbali woon nañu di woo giiri araab yi ci ñu dugg ci Lislaam, ba mujj nguurug Lislaam gii doon doog a sosu ci Madiina di gu am doole ak kàttan, mu daal di sóobu ci ay kollarante yu politig, yu diine ak Quraysin, ci noonu giir yi daal di séddaliku ci yuy ànd ak Muhammad (j.m) ak yu koy safaan, di ànd ak Quraysin, loolu wéy nag di nekk ba kero bi ñu ubbee Màkka (fath Makka) te duma way bokkaale ñi (am ndam ci seen kaw), booba la la ëppoon ca giir ya bennoo woon ci ron raayab Lislaam. + +Ginnaaw bi Yonent bi génnee àdduna, ay Xalifaam wéyoon nañu di woote jëme ci Lislaam ak a nos Jiyaar gi ngir wisaare diiney Lislaam ak tas maandute ak yoon te yekkati tooñ wëlif nit ñi, ba mujj digi nguurug Lislaam gi mujj àgg Siin ci penku bi, akMbàmbulaanug Atlas ci sowwu bi, Lislaam it wéy cig yaatoom akug tasam jaare ko ci yaxantukati jullit yi doxoon jëm penku ak bëj-saalum ci Asi, ak cig wokkoo ak riisoo ak wàll yi gdigoo ak dig (frontières) yu Lislaam yi ci Afrig ak Tugal. Am na it ñu bari ci lokkikat yi (les conquérants) ñoñ tàbbi woon nañu ci Lislaam bi ñu agsee ci barabi Lislaam yi, ñu ci mel ne Mongool yi ak ñenn ci ñi doon def Xarey jooñe yi ak Tataar yi. + +Kuy xeeñtu (suivre) Sariiya bu Lislaam dana gis ne moom dey daa farataal ci bépp jullit mu nekk ab wootekat jëme ci Lislaam; di digale lu baax di tere lu bon, di sonn it ngir nit ñi dugg ci Lislaam ciy mbooloo, ngir jëfe waxi yonent bi (j.m): ((Yàlla gindee ci yaw jenn waay moo gën ci yaw àdduna ak li ci biiram)), Lislaam kon gaweesu ko ci mag muy woote walla boroom xam-xam buy génne ay fatwaa, mbaa ñu jagleel ko jenn jàkka wëlif jeneen. Lii kon menn la ci mbóoti wisaarook Lislaam ci àdduna bi ci jàmm mbaa xare. + +Ay ngér yu fiq +Ngérum fiq moo man a gis day ball-loo àttey Sariiya yi ci tegtal (adila) yi rot (nekk) ci Alxuraan ak Sunna, dëppoo nag ak ay ponk aki cosaan yu fiq yu leer, manees na leen a tudde ay daara yu fiq (écoles de jurisprudence) ngir dëppoo gi ñu def ci pas-pas bi (alhaqiida) ak cosaan yi (al-usuul), waaye man nañoo xaw a wuute ci àtte yi ñuy ball-lu. Ngéri fiq yu ñeent yi tas nañu ci anam gu yaa ci ñoñ Sunna ñi, te mujj di lu kilifawu (officel) ci li ëpp ci seeni téere, ñoom nag (ngér yooyu) ñooy ijtihaad (ay liggéeyi xel) yu fiq yu lëng yi ñeel ñeenti Imaam yu ñoñ Sunna ñi ak mbooloo mi (Ahlus sunna wal jamaaha), ñoom nag nii lañu toftaloo ci taariix: + + Imaam Aboo Haniifa Annuhmaan, am ngéram mooy mu Haniifa walla Aniifa, mbaa Anafi, moom ngér moomu nag mi ngi sosoo ci Baxdaad ca Iraag + Imaam Maalig Ibn Anas, am ngéram nag di Maaliki walla mu Maalig mi ngi sosu ca Ijaas ca Madiina (almunawara) + Imaam Muhammad Bn Idriis As-shaafihii, ñu koy dàkkantale Shaafihi, am ngéram di saafihi walla saafihiya, mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraak + Imaam Ahmad Bn Hanbal, am ngéram di Anbali, mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraak + Imaam Dawuda bn Aliyu As-saahirii, am ngéram di Saahiriya, mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraag + +Ngérum fiq mu waa Siiya yu Fukk-ak-ñaar-yi, mooy fiq bu Jahfar, bi ñuy askanale Imaam Jahfar As-saadiq + +Lislaam ak yeneen diine yi +Alxuraan de ëmb na am njàngale mu jëm ci wormaal yeneen diine yi. Alxuraan daa wormaal diiney Yahood ji ak ju nasaraan ji, ngir jàppe gi mu leen jàppe ñuy ay diine yu Ibraayma. Alxuraam mi ngi feddali ne daa ñëw ngir feddali diiney asamaan ju sell ja ñu wàcce woon ca Ibraayma (j.m) te yahood yeek nasaraan yi soppi ko, wëlbati ko(soppi walla wëlbati (التحريف) amaa na mu tekki lu gën a sori déggiin wu ñaaw mbaa wu juum ñeel ab yax (texte), déggiinu mbir mii ak maanaam ci ay tolluwaay yu mujj ci taariixu Lislaam mujj na di : ay xaaj ci Injiil ak Tawreet baaxatuñu). Ñeneen ñu duli jullit it dëggal nañu soppi googu walla "tahriif" googu. + +Salaat (julli) + +Jullit bi am na juroomi jullit yu koy war ci bis bu nekk, yooyu ñi ngi leen di wooye julliy farata (salaatul fariida) ci araab, ginaaw yooyu nag am na fi yeneen yu ñuy wooye "naafila" ñooy yi ñuy def cig coobarewu ngir yokk ab yool, ngir jaamu Yàlla gees la tegul cig farataal. + +Julli daa war a nekk di lees di def cig laab : bu la fekkee cig laabadi, kon dangaa war a jàpp (ablution). + +Julli nag dees koy def cig jublu xibla (maanaam jublu ca Kaaba ga nekk Màkka) ; aji julli ji daa war a yéene def julli gi ko tax a jug ci anam gu leer, yéene jooju moom lañuy wax:(niyah)ci araab. + +Voir aussi + +Bibliographie +Avertissement : la bibliographie ci-dessous est proposée à titre indicatif. La littérature sur l'islam étant abondante, riche et variée, seuls quelques livres sont proposés. Toutefois, ces livres n'ont pas tous la même valeur didactique et leur choix repose sur celui de plusieurs éditeurs de cet article. Leur présence sur cette liste n'est en aucun cas gage de sérieux de l'ouvrage. + + Charles Saint-Prot. Islam: l'avenir de la Tradition entre révolution et occidentalisation. Paris, Le Rocher, 2008, 620 pages. + Jean-Claude Barreau De l'Islam en général et du monde moderne en particulier, Editions Le pré aux clercs, 1991, collection Pamphlet + Mahmud Shaltut, L'islam : dogme et législation, Al bouraq, 1999 + Tahar Gaïd, La Femme musulmane dans la société, Iqra, 2003 + Fdal Haja, Assalihats, les femmes vertueuses, Universel, 2005 + Charles-André Gilis, Études complémentaires sur le Califat, Al Bustane + Tabari - Traduit par Hermann Zotenberg, La Chronique de Tabari (5 volumes), rééditée en 2001 par Actes Sud en deux volumes Volume I , Volume II + Ibn Taymiya, Lettre à un roi croisé, 2005, Tawhid + Mohammed ben Jamil Zeino, Comment comprendre le Coran ?, Éditions Chama, 2005 + Dalila Adjir- Adlali Beghezza, Entrée interdite aux animaux et aux femmes voilées, Akhira Distributions + Roger Du Pasquier, Découverte de l'islam, Seuil, 1984 (Comprendre l'islam de Frithjof Schuon, Seuil, 1976) + Michel A. Boisard, L'Humanisme de l'islam, Albin Michel + Dominique Sourdel, Vocabulaire de l'islam - N°3653, PUF, Collec. « Que sais-je ? », Nov. 2002 + Anne-Marie Delcambre, L'islam des interdits, Éditions Desclée de Brouwer, 2003, + Mohammed Arkoun, Ouvertures sur l'islam, Grancher, 1992 + Michel Reeber, L'Islam, Les Essentiel Milan, 1999 (pour une première approche) + Paul Balta, L'Islam, Le Monde édition, 1997 (également pour une première approche) + Malek Chebel, Manifeste pour un islam des lumières, Hachette, 2004 + Abdallah Penot, Le Coran, Alif Editions, 2004. + Denise Masson, Le Coran, Paris, Folio, 1992 (une traduction aussi juste que poétique). + traduction d'AbdAllah Penot, La Doctrine de l'unité, selon le soufisme, Alif Editions. + Al Nawawy, traduction d'AbdAllah Penot, Les Jardins de la piété, Alif Editions + Henry Corbin, Histoire de la philosophie islamique, Folio, 1989 + Fatima Mernissi, Sultanes oubliées, Femmes chefs d'État en Islam, Albin Michel + Eva de Vitray-Meyerovitch, Anthologie du Soufisme, Albin Michel + Ligue francise de la femme musulmane, Éducation des enfants en islam , LFFM + Bernard Lewis, Islam, Quarto Gallimard + Abdallah Penot, L'Entourage féminin du Prophète, Alif Editions. + Brahim Labari, Recettes islamiques et appétits politiques, Paris, Syllepse, 2002. + Edouard-Marie Gallez, Le Messie et son prophète, Aux origines de l’Islam, 2 tomes, Tome 1. De Qumran à Muhammad, Tome 2. Du Muhammad des Califes au Muhammad de l’histoire, Versailles, Éditions de Paris (un résumé sur le lien suivant : https://web.archive.org/web/20070927202518/http://www.ict-toulouse.asso.fr/ble/site/659.html) cette publication a constitué la thèse de doctorat en théologie / histoire des religions qu’Edouard-Marie Gallez a soutenue à l’Université de Strasbourg II en 2004. + Histoire de l'Islam : Fondements et doctrines de Sabrina Mervin (Présentation de l'éditeur : De la Jâhiliyya à l'islam. Le Coran. Le prophète comme modèle. Le droit islamique et sa méthodologie. L'élaboration de la théologie. Les schismes dans l'islam. Le chiisme duodécimain. Théories et pratiques du soufisme. Les réformistes, entre réaction et modernisme. Les courants de pensée dans l'islam contemporain), Poche: 311 pages, Nouv. éd (19 septembre 2000), Collection Champs Flammarion, ISBN-10: 2080830090 + Alfred-Louis de Prémarre, Les fondations de l'Islam, entre écriture et histoire, Seuil, 2002, 522 pages. + Alfred-Louis de Prémare, Aux origines du Coran, Téraèdre 2005, 144 p + Christoph Luxenberg, The Syro-Aramaic Reading of the KoranA Contribution to the Decoding of the language of the Koran, Hans Schiler Verlag, 2007. + +Liens externes + Islam de France - Site traitant de l'Islam en France + + + Euro-Islam Website Coordinator Jocelyne Cesari, Harvard University and CNRS-GSRL, Paris + Muslim Values, Global Values: Empirical Data from the 'World Values Survey' + + +Yoonu murit +Kiswahili, walla làkku suwayli aw làkk la wees di wax ci anam gu yaatu ci Penku Afrig gi. Ci Suwayli turu làkk wi mooy Kiswahili. Moom nag aw làkk wu Bantu la. + +Suwayli nag dees na ko wax ci gox bu yaatu ci Afrig, la ko dale ca bëj-saalumu Somaali ba ca bëj-gànnaaru Mosambik ak Keeñaa gépp. Lu tollook juroomi milyoŋ yu muy seen làkk wu njëkk a ngi fi (yu muy seen làkk wi ñu nàmp), ak juroom fukki milyoŋ ciy nit yu muy seen ñaareelu làkk (làkk wu ñu jàng). Suwayli mujj na di làkk wow nit ñi man nañu ciy jokkoo ci penku Afrig ak barab yi ko wër. + +Suwayli tàmbali naa nekk làkk wees di wax ci Sansibaar, benn dun ci Tansaani. Suwayli làkk wu kilifawu la (officiel) ca Tansani ak Keeñaa. Moom nag làkk wu jeexiitalu la ci yeneen làkk yu bari niki wu araab. Niki làkk yu bari ci Afrig Suwayli nekkoon na di lees di binde ci arafi araab waaye leegi ci yu laatiin yi lañu koy binde. + +Bennaani baat +Lii ci suuf ay misaal la ci làkkuw Sàuwayli: + waaw - ndiyo + déet - hapana + okay (walla baax na) - sawa + +yeneen dali web + Kamusi Project Internet Living Swahili Dictionary + +Làkki Niseer-Cóngoo +Làkki Afrig +Campora San Giovanni (Campura San Giuvanni ci waxiinu waa-campora), ab frazione la (dëkk-dëkkaan ci wolof) bu bokk ci dëkkaanu Amantea, ci tunduw Cosenza digoo ak tunduw Catanzaro ca réewum Itaali. + +Taariix +Campora San Giovanni du dëkk bu yàgg, way-dëkk yi fa njëkk ci diggante 1897 ak 1899 lañu fa ñëw . Te ña ca ëppoon ñoo ngi jóge woon ca cleto, ca Aiello Calabro, ca San Mango d'Aquino, ca Belmonte Calabro, ca Longobardi, ca San Pietro in Amantea, ca Lago ak ca Serra d'Aiello. Ginnaaw ay gàddaay yu tar yu waa-dëkk bi ak ñaari xarey àdduna yi, la ay way-dëkkam waññeeku bu baax. Gàddaay gi daan am jëm ci yeneen réewi tugal yi, Aamerig gu bëj-gànnaar ak gu bëj-saalum tamit, ca Óstraali ak ca Seland-Gu-Bees. Li dalee 1989 la fa ay way-gàddaay, yu jóge penku Tugal, Maghreb, Senegaal, añs, tambalee ñëw. Way gàddaay yooyu ña ca ëpp ci mbéy la ñuy yëngu walla ci tabax. + +Melosuuf +Campora mi ngi nekk ci tefesu géeju Tiren ci dóoxub Lamezia, am na 7 000 ciy way-dëkk. Campora mi ngi nekk cig joor gu maaseedi leru tefes gi. Bokk na ci li gën a raññeeku ci dëkk ba, mbéyum oliiw ak njóoxum sëng, mu doon mbaaxaay gu kawe. Waaxam ba tax na dem ca duni Eoli yi yomb, loolu tax mu doon ab jëmuwaayu nemmeekukat yi. + +Koom-koom +Koom-koomu Campora mi ngi dàttu ci mbéy mi ak nemmeeku gi. Li dale ci diggu XXu xarnu la fa mbéyum soble su xonk soqaliku, di it soble su waa-itaali yi bëgg lool. Njureef li dañ koy jaayi-ji ci àdduna bépp, muy lu am solo ci koom-koomam. Ag féeteem ci melosuuf ak nosteg yooni jokkoom: yoonu weñ aki tali, ñoo tax yëngu-yënguy yaxantu ya fay am woomle. + +Lëkkalekaay yu biti + Associazione Proloco Campora San Giovanni - Dalu Campora San Giovanni + +Itaali +Weeri wolof, ci arminaatu gàddaay gi, walla bu jullit ñi mbaa bu Lislaam, ab arminaat bu weer la, buy sukkandiku ci doxiinu weer wi ngir xam ak natt weer wi. Jullit ñi danañu ko jëfandikoo ci bépp barab, rawati na ngir natt ak xam xew-xewi ak bisi diine yi. Ki ko sos nag mooy Omar Ubn Xattaab (g.m), daal di def gàddaayug Yonent bi (j.m) juge Màkka dem Madiina muy ab tàmbaleem, looloo waral deesi tudde ko arminaatub gàddaay gi. Ak doonte arminaat bi ci jamonoy jullit ñi lañu ko sos, teewul turi weer yi ak arminaatub weer ñu leen daa jëfandikoo lu jiitu Lislaam. + +Yenn ci réewi araab yi, mu ci mel ne Araabi Sawdit, moom ci nguur geek askan wi dañuy jëfandikoo arminaatub gàddaay gi niki arminaat bu kilifawu di ci taariixe ci bindante yiy am ci diggante liggéeyuwaayi nguur gi, waaye nag lu ci dul moom, askani araab yi ci des yépp arminaatu Garegori (bi dale ci juddug Yonent Yàlla Iisaa) lañuy gën a jëfandikoo.. + +Arminaanub gàddaay gi mi ngi ame ci 12 weer yu weer wi, maanaam atum gàddaay gi mi ngi tollook 354 bés daanaka, maanaam 354.367056 ci ay bés. Weer wi ci arminaatu gàddaay gi, benn mu nekk 29 walla 30 bés (ndax doxug weer wu feeñ wi 29.530588 bés la). Ginnaaw nag wuuteg 11 fan am na ci diggante arminaatu judd gi ak bu gàddaay gi, ñaari arminaat yi duñu jamonoo mukk (duñu tolloo mukk) looloo waral dëppale leen di gën a jafe. + +Weer ci arminaatu gàddaay gi + Tamxarit + Diggi-gàmmu + Gàmmu + Rakki-gàmmu + Rakkaati-gàmmu + Maami-koor + Ndeyi-koor + Baraxlu + Koor + Kori + Diggi-tabaski + Tabaski + +Lëkkalekaay yu biti + Khalid Chraibi : Le calendrier musulman en 10 questions + Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) + The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +Lislaam +Arminaat +Weeri wolof +dëkkug lebu yi ci ndakaaru mi ngi am ginnaaw ay duusi gàddaay ci diggante XV¹⁵ ak XVIu¹⁶ xarnu. Laataa seenug càmp ci Senegaal, ab tukki bu gudd moo leen war a jëlee ca penku Afrig ba ci sowwu Afrig jaare ko ci bej-gànnaaru gox bi. Ñaari gongikuwaayu xibaar lanu am ngir man a jéem a rëddaat yoon wi leen fi indi. Nettali gi ciy kàddu di na tax nu man xam lu bari ci jamono yu mujj yi. liggéey yu ay gëstukat niki Seex Anta Joob T. Gostynski, G. Balandier ak P. Mercier, F. Brigaud di nañu tax nu man a dem ba ca njëlbeen + +Gongikuwaay +Tambali na am na 7 000 at, tukki bi jaare ci bëj-gànnaaru Afrig, ci ay pàcc yu bari la ame. Jàpp nanu ne dañu leen fay war a dàqe walla ñu demal seen bopp ngir lànk nooteel. Aw askan wu fonk i baaxam (aadaam), ak i melokaanam la. Ci melokaan yooyu sax lañu sukkandiku ngir joxe ay gongikuwaayu baatu lebu. Am na ñu ne mi ngi joge ci baatu lebu (maanaam dëkku, misaal: dëkku am mbër ), ndax seen mbañug nooteel, ñeneen ni ci lubu (jqmbaar) la jóge, ak yeneen. + +Seenug càmp ci Ndaakaaru +Laataa ñëwug lebu yi ci Ndakaaru, juróom-benni gàddaay yu toppante lañu amal. Bi ñuy ñëw ay mbooloo yu ndaw lañu doon def, ndànk ndànk ñuy toog, ci ndoorteel gi ci barab yi soose yi nekkul woon, ñu dem ba sanc Ndakaaru gépp. (Caam, 1970:6) + +Ñi ngi agsi ci 1430 (atum junni ak ñenti téeméer ak fanweer), boobu ag nguuru soose, gu tambalee woon Tubaab Jalaaw ba Ngor, moo fa nekkoon. Ca jamono yooyu, ay réewi soose yu bari ñoo fa amoon, ci seeni bopp ñii ñoo fa nekkoon: Malang Tambaa, Jalla Jaw, Gitigi Maroon, Nak Jombel moom dund na ba 1470. Xare bu tar ba ca toppoon waraloon dawug Soose yi jëm Gàmbi. + +Jàppante bi wéy na ba ci XVu¹⁵ xarnu bi, ba killifay soose yi deewee la xare ba jeex. Ca la lebu yépp jóge Jolof mi doon waaj a xar, ndànk ndànk ñu dem ba moom Ndakaaru gépp. Ginnaaw bi yàggul dara dammeelu Kajoor di leen jéem a sanc loolu jur ay xare yu bari ci seen diggante. + +Nosiinu politig bi +Nosiinu seenug mboolaay, ci li ñu xam, am na laataa seenug ñëw ci Ndakaaru te mi ngi dàttu woon ci palug ab Laman. Ndànk ndànk ñàkk kaaraange gi ak jamono ju laaj jeneen nosiin tax yeneen cëslaay taxaw. + +Ci boppu askan wi, Jaraaf bi moo fa nekkoon, di ki jiite nguur gi, Ndey-ji-réew ji tegu ci, di ki yoroon mbiri biir ak biti réew. C.T. Mbeng moom daf ko jappe niki "ab aji-teewal ak aji-rattaxal ci diggante réewi lebu yi". Saltige bi moom moo yoroon suuf si ak aartu (défense) gi ak ndox mi. Ñett ñii ñoo yoroon doxiinu réew mi. Taxawaloon nañu ñaari pénc ngir ñu jàppale ñett ñooñu ci seen liggéey: Jàmbur ak péncu fere yi. Bu njëkk bi di nañu ko wax itam ""jataayu mag ñi"" boroom xam-xam yi rekk a fay nekk, Ndey-ji-jàmbur moo koy jiite. Péncu fere + +Jàmbur bi mooy kiy fal jaraaf, ndey-i -réew ak alkaati bi. Te ñiy yor yooyule ndombal-tànk waruñoo doon ay xeet (maanaam ñu bokk ci wàllu yaay). Lii di na tax ba man-man (pouvoir) gi du nekk rekk ci yoxoy genn njaboot. Bii matuwaay di na tax ba réew mi du soppiku nguur. Kon man-man gi dañu koy séddale ci njaboot yu bari, ku nekk man ngaa am ndomba-tànk, suñuy tànn kenn, ci genn njaboot gi, lenn li ñuy xool mooy ay mbaaxam. + +Lëkkalekaay yu biir + Lebu + Senegaal + Jolof + Waalo + Siin-Saalum + Fuuta Tooro + Tekuruur + Bawol + +Téerekaay + Armand-Pierre Angrand, Les Lébous de la presqu'île du Cap-vert. Essai sur leur histoire et leurs coutumes, Dakar, Éd. La Maison du livre, 143 p. + Birahim Ba, La société lébu. La formation d’un peuple. La naissance d’un État, Dakar, Université de Dakar, 1972, 206 p. (Mémoire de Maîtrise) + Georges Balandier et Pierre Mercier, Particularisme et évolution : les pêcheurs Lébou (Sénégal), IFAN, Saint-Louis du Sénégal, 1952 + Adama Baytir Diop, La prise de position de la collectivité lebu en faveur du “oui” lors du référendum de 1958. Essai d’interprétation, Dakar, Université de Dakar, 1985, 51 p. (diplôme d’études approfondies) + Adama Baytir Diop, La communauté lebu face aux développement de la politique coloniale : la question des terrains de Dakar (1887-1958), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1995, 277 p. (Thèse) + Claude Laborde, La confrérie layenne et les Lébous du Sénégal. Islam et culture traditionnelle en Afrique, Karthala, 1997 + Colette Le Cour Grandmaison, Rôles traditionnels féminins et urbanisation. Lébou et wolof de Dakar, Paris, EPHE, 1970, 4+310+23 p. (Thèse de 3e cycle, publiée en 1972 sous le titre Femmes dakaroises : rôles traditionnels féminins et urbanisation, Abidjan, Annales de l’Université d’Abidjan, 249 p.) + M. Mbodji, « Tiané, une jeune fille en quête d'initiation : rêver chez les Wolof-Lébou, ou comment communiquer avec les ancêtres ? », dans Psychopathologie africaine, 1998-1999, vol. 29, n° 1, p. 7-21 + Mariama Ndoye Mbengue, Introduction à la littérature orale léboue. Analyse ethno-sociologique et expression littéraire, Dakar, Université de Dakar, 1983, 378 p. (Thèse de 3e cycle) + Médoune Paye, La collectivité lebu de Dakar : organisation, rôle politique dans les élections municipales de 1925 à 1934, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2001, 118 p. (Mémoire de Maîtrise) + Ousmane Silla, Croyances et cultes syncrétiques des Lébous du Sénégal, Paris, EPHE, 1967, 517 p. (Thèse de 3e cycle) + Assane Sylla, Le Peuple Lébou de la presqu'île du Cap-Vert, Dakar, Les Nouvelles Éditions africaines du Sénégal, 1992, 135 p. + Tamsir Sylla, Introduction à un thème négligé : révoltes et résistances en milieu lebou au XIXe siècle. Approche critique des sources, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1990, 36 p. (Mémoire de DEA) + Ibrahima Thiam, Ousmane Diop Coumba Pathé, personnalité politique lebu : 1867-1958, Dakar, Université de Dakar, 1987, 46 p. (Diplôme d’Études Approfondies) + Guy Thilmans, « Étude de quelques crânes lébou (Sénégal) », Bulletin de l'IFAN, 1968, t. 30, série B, 4, p. 1291-1297 + +Taariixu senegaal +nguuri senegaal +Kurów ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Poloñ. Mi ngi ne ci diggante Pulawy ak Lublino, ci dexu Kurówka. Mooy péyu gox-goxaan bii di gmina. + +Mi ngi yaatoo 11,32 km², ci 2008 amoon na 2.804 way dëkk. +Kumba Ndóofeen Famak Juuf (ci baati Seereer : Maad a Sinig Kumba Ndoofeen Famak Juuf) Buur Siin la woon toggoon ci jal bi ca atum 1853-1871. "Maad a Sinig" ci baati Séeréer moo tekki "Buur Siin". Ci meenu Gelwar la soqqeekoo - askanoo Njuufeen, kerr Semu Njeke. Maamam ci xeetu Séeréer ak Soose la juge. Màbba Jaxu Ba, Kumba Ndóofeen Famak Juuf moo ko ray aki Ceddoom, ci ndimbëlug tubaayi ca xare ba ñuy tudde Somb-Cucun ca atum 1867. + +Taariixu senegaal +Niti senegaal +Niti Gàmbi +Cosaan +Séeréer +Cosaan Séeréer +Mandinke, ci xeet Soose yi lanu bokk. Ñoom ñoo taxawal imbraatooru Mali, ak nguuru Kaabu, Ñaani, Wulli ci senegaal. Sunjata Kayta Mandinke la. Mandinke am nañu tuur yu bari: Malinke ci français, manding, Mandinka mooy tur wi ñu tudde seen bopp. Ci seeni làkk, Mandinka mooy: nit ku juge Mande. Mande mooy Reéwum mandinka yi, ci réewum Mali. Seeni Sant: Kayta, Jara, Siise, Ture, Kuyaate, Sumaare, Fakoli, Dumbuya, Dumbiya, Bakayogo. Buuru mandinke Mansa lay tudd. + +Taariixu senegaal +Ceddo, jàmbaaru nguuru Senegaal la doonon bu jëkk, ci cosaanu Senegal. Nguuru: Kajoor, Bawal, Jolof, Waalo, Fuuta, Siin ak Saalum, Galam, lanu dekke woon. Seeni col nekkoon na mbubb ak téere yu bari ci seen kaw, njañ ak létt lañu daa am, jaaro ak takkaay yu bari it ñu ràngoo leen. Def nañu lépp, xare ba sonn, ngir tubaab man a bàyyi réewum Senegaal. Demba waar Sàll, Farba Kaba, Dammeel Lat Joor Ngóone Latiir Jóop ci ceddo yi lañu woon. + +Baatu Ceddo, yaatu na. Geer yi (walla garmi), ak ku nekkoon doomi buur, Ceddo lañu ko daan woo. Yemul ci jammbaar yi rekk. Ci Pël yi ak Tukkloor yi, dañu daan joxe turu Ceddo (walla Sebbe su de dañu bare), ñu nekkoon buur. Séeréer yi tamit, Ceddo yi, doomi buur lañu woon (bino maad ci seen lakk). Ci Senegaal fepp, bu jëkk, Ceddo yi ñoo daan yor nguur yi, ñoo gënoon fete kaw, ci nos gi. + +Taariixu senegaal +Taariixu Gàmbi +Cosaan Séeréer +Cosaan +Mabba Jaxu Ba ci atum 1809 la judd ca nguurug Saalum. Baayam Njógu Ba la tuddoon, Sëriñ bu mag la nekkoon, soog a tuxu Saalum. Yaayi Màbba Jaxu, Jaxu Jéey la tuddoon,di woon wolofu jolof. Mabba Jaxu Ba, Almaami bu Rip la nekkoon, ba atum 1867. Ci at moomu , tase na ak Kumba Ndóof Seen Juuf Buur Siin bi, ci xeex bu nu tudde woon Somb-Cucun ci nguuru Siin, la deewe. Ci xeex bi Lat Joor Ngóon Latiir Jóop ak Alburi Njaay la àndaloon. + +Taariixu senegaal +Niti senegaal +Niti Gàmbi +Cosaan +Tekuruur moo doonoon benn nguur ca bej gannaaru Senegaal. Xeet yu bari tase nañu fa, juge Isipt: Séeréer si, Pël, Sooninke, Naar yi. Leeegi Tekuruur, Fuuta-tooro la tudd. Koli Tenŋela Bah, denyankobe bi, moo ko jox tuur wi. Ca nguur ga, Tukuloor ak Pël ñoo fa ëpp ba tay, waaye Séeréer si ñoo fa jëkk a nekk, ak Pël. Buur yu bari ñoo yoroon nguur ga: + Jaa-Ogo yi ci yoonu imbratooru Gana. Ñoom ay tëgg lañu woon. Bokk ci Pël yi. + Manna yi. Ca Penku lañu fekke baax (nguuru jaara / kingi), sant Ñaxate, bokk ci sooninke yi. + Tondiyoo yi. Ñoom ay Séeréer lañu woon. + Lam-Termess, Lam-Taga, ak Lam-toro yi. Ci ñu nekke buur, Jolof moo doon uuf dëkk bi, di fi teg ay Farba (Farba Walwalde, Farba Njum, etc). + Deeniyankooɓe yi, yu Koly tenŋela Bah, Sebee lañu woon, Sebbe mooy Ceddo. + Almaami yu Torodo yi. Sulaymaan Baal ak Abdul Xaadir Kan, ñoo dàq deeniyankooɓe yi ci atum 1776. Ay jullit lañu woon. +Ba noppi, tubaap yi ñëw ak canc gi (colonisation), ci atu 1890, jël nguur gi, elif Almaami yi, di séddale dëkk bi, ci ay - li nuy wax ci lakku fraanse (Canton) ak (Provinces). + +Tukuloor, mooy ku dëkk Tekruur, da mel ni baatu Fuutankooɓe / Fuutanke, di ku dëkk Fuuta Tooro. Tur wi ñuy wax Tukuloor tubaab moo ko fi indi, yeneen yi naan Wolof yi ñoo ko sos. Nit ñi , dañu faral jaawale, Tukuloor (ku dëkk Tekruur) ak xeet wi nekk ca dëkk boobu. Ñoom, ci waaso yi lañu joge: Pël, Séeréer, Sooninke, Naar. Seeni sant ñoo ko firnde. Deeniyankooɓe ñoo tax lakku pulaar siiw dékk boobu. + +Taariixu senegaal +Cosaan Séeréer +Saraxule walla sooninke, wenn xeet la, ci askanu Mande la bokk. Am naa yeneen tur ñu leen tudd: Wangara, Tubakai, Aswanik. + +Sooninke, mooy ku juge Sooni / Sunu. Sooni (walla Sunu) benn dëkk la ca Isipt, ñu ko gëna raññe ci tur wi di Aswan. Maamu sooninke yi, dekk boobu lañu baawo, moo tax ñu yore tur wi Sooni-nke. + +Cosaan + +Yugo Xasse Diŋa Siise: + +Diŋa Siise walla Diŋa Xoore, ci cosaan, bokk na ci maamu sooninke yi. Kooku moo juge woon Sooni/Sunu, te ñow ba sowu jantu afrig (Senegaal, Mali,Gànnaar). Ca jamono Isipt gu yàgg ga la woon, ci mujjam. Bi mu agsi foofu ak gangooram, moo sos imbratoor gi bu ñu naan GANA walla WAGADU. + +Saraxule ñoo fi jëkk a dugg ci Lislaam, ci réewum Senegaal, Xeet woowu ñoo jur Jula yi. Jiitu nañu Wolof yi ca Kajoor ak Bawal Séeréer si ca Siin ak Saalum, foofu fépp ñoo fi njëkk a nekk. Imbraatóoru Gana moo ko tabax, ak nguuru Gajaga, nguuru Jara. Seeni buur Tunka lees leen di dàkkantale. Ci mbay lañu daan dunde, yaxantukat (jaaykat) yu mag lañu woon. Seen xeet woowu, am na ay tukkikat yu ba bari, yu daa tukki, di jaay guro, yére, takkaay, ci fépp ci Mali, Senegaal, Niseer, Gine ak Gine-bisaawóo, Gànnaar, ba Kodiwaar. Ci nit ñu nuul yi, dañu bokk ca fi jëkk ñow Tugal. Ca Gànnaar ñu bari ca dëkk ba tudd Gidimaxa lañu, ci wetu Fuuta-Tooro la, foofu tamit nekk nanu fa bu yàgg, ba Tekuruur nekkee. Mamadu Lamin Drame, Sëriñu Saraxule la bu juge Gajaga/Galam, bu ñuy wax tay tundu Bàkkel( (Departement de Bakel), xare na ak tubaab yi bëggoon a boole dëkk bi ci seen moomeel ci atum 1880. Musaa Molo buuru Fulaadu, ci nguuri Pël yu firdo yi, doomu Alfa Yaaya Molo Balde, moo ko daaneel, booba nag buuru Pël bi tubaab bi la àndaloon. Mamadu lamin, tubaab yi ñoo ko ray ca xare ba ñu tudde xareb Tubaa-Kuta, ca atum 1887. + +Nosteg mbolaay +Bokk na ci askanu Saraxule: + + Horon, ñoo doon buur yi. + Ñaxamala, ñoo doon ñeeño yi, ràbbkat yi, wuude yi , tëgg yi ak seen yi. + Jaaro, waykatu buur yi, xam nañu cosaanu Saraxule yépp, Koora ak Xalam lañuy waye buur yi (Tunka) + Komo ñoo doon jaam yi. + +Sant yi + +Waaye népp dañuy bay seeni tooli bopp. Seeni Sant yi gën a siiw: Ture, Siise, Baccly, Sumaare, Daraame, Kebe, Fofana, Daabo, Jaabi, Silla, Jakite, Soxna, Tunkara. + +taariixu senegaal +Séeréer (mba Seereer) genn giir la gu nekk Senegaal. Siin ak Saalum ñooy seen i nguur. Ci lim ñooy ñatteelu xeet ci Senegaal ginnaaw wolof ak pël, juróom benn saa-senegaal yii jël kenn ka séeréer la, ñenn ci séeréer si diñu leen fekk Gàmbi ak Muritani. Xeetu séeréer bokk na ci xeet yi gën a yagg te féete Senegàmbi. Soog a nekk Siin-saalum, ca Tekuruur lañu nekkoon. Dañoo gàddaay dem Siin-Saalum ndax dañu doon daw Lislaam ak Muraabituun yi (les Almoravides). Muraabituun yi dañu xare "jiyaar" ak séeréer si, ngir dugal leen ci Lislaam, waaye séeréér si bëgguñu woon loolu. Lii lépp nag ca yoonu imbraatóor gu Gana la xewe woon, booba imbraatoor gi mi ngi doon tàmbalee daanu. Foofa ca Siin-Saalum ay Soose (Sooninke), ñoo fi doon dëkk. Kon mbokkug Soose ak Séeréer ci dëkkandoo la bawoo, ba noppi Soose yu bari dem nanu dëkki ca Kaasamaas. Séeréer si dañu doon séddale dëkk bi ci ay Lamana, ca Lamana yépp ay Laman a fa fa daa nekk ay buur. Mbay ak Napp lañu daa dunde. Mbay (Saalum) moo doon turu dëkk bi soog a nekk Siin ak Saalum. Ba noppi ay Mandinke yu juge nguuru Kaabu, ñëw ca Séeréer sa, dëkk ak ñoom. Mandinke yi ay Nanko (Géer) yu Kabbu lañu woon, seeni buur (Mansa ca làkku Mandinke) ñoo leen dàqe seen réew. Joolaa yi ñoo leen ne ca Siin-Saalum baax na lépp lu nit soxla ngir man a dund am na fa, te foofu am na ay nit waaye amuñu buuru dëgg. Lii moo tax ñu tuxoo Siin ak Saalum. Nanko ak Buuri Séeréer si fi nekkoon (Laman) dañoo booloo, jaxasoo, ba nekk xeet wu ñuy wax ay Gelawaar. Gelawaar, ñoo tabax nguuru Siin ak Saalum. Maysa Waali Joon moo jëkk a nekk buuru Siin. Mbegaan Nduur moo jëkk a nekk Buuru Saalum. +Nosteg mboolaay ga (le système social) nii la tëdde woon: + Gelawaar yi ñoo neekkoon Buur yi. + Jàmbur yi ak Baadoola yi ñoo ci toppoon cig raŋ. + Tëgg yi (Tafax ca seeni làkk), Lawbe yi ñooy seeni Seen, Wuudé yi (Pal), Ràbbkat yi (Tiriw). + Jaam yi, Ceddo bokk nañu ci jaam yi. + +Séeréer ci seen bopp, am nañu: Séeréer yu Njominka, Siin rekk lañu nekk, nappkat lañu it, turi maandinke lañu yor, ndax ca gelawaar lañu bokk. Séeréer Ndut, Saefen, Paloor, Noon, ñoom Séeréeru Kajoor ak Bawal lañu. +Séeréeru Siin, mooy Séeréeru Siin-Saalum. Séeréeru Fuuta yi nag, leegi ca tukuloor ya lañu bokk, ñoom ñoo fa doon ay wolof tamit, Kuballo yi (nappkatu tukuloor) ak Sebbe ( ceddo tukuloor ). Séeréer ak Pël ñoo njëkk a nekk foofu, loolu moo tax mu am fa ay Séeréer. Tukuloor ak Séeréer dañuy kalante ak Joolaa tam. Ndax ca cosaan, nee nanu, xeet yooyu yépp ñoo bokk mam. +Séeréer si dañoo xaw a ñuul, njool, am it yaram wu dëgër. Ci Senegaal ñooy ñi fi dàq a bëre. + +Léopold Sédar Senghor, njiitul Senegaal lu njëkk séeréer la woon ca baayam, Abdu Juuf tam. Blees Jaañ moom it baayam Séereer la woon. +Séereer bu njëkk Ceddo lañu nekkoon - diiney "A ƭat Roog" ci baati Séeréer. Tay nag dugg nañu lislaam ( Tiijaaniya, yoonu murit), walla diiney nasaraan (christianisme) ca Siin (Joal-Fadiouth). Nasaraanalkat yi (le Missionnaires) yu tubaab yi ñoo leen dugal ci diine jooju. Am na Séeréer ñu barry ñu tey ci diiney A ƭat Roog (religion sérère). Roog moi Yalla ci baati Séeréer. + +Seen Sant yi gën a siiw : Juuf, Ngom, Fay, Seen, Saar, Seŋoor, Nduur, Joon, Joor, Jongu, Jeey, Njaay, Sekk, Ndong, Séy, Luum, Tin, Déen, Puy, Caw, Maróon, Ñing, Jóob, Gaajo. + +Séeréer +Taariixu senegaal +Làkki senegaal +Niti senegaal +Waasoy Senegaal +Wolof genn giir la gu nekk Senegaal. Wolof ñoo ëpp ci waaso yi ci Senegaal. Maami wolof yi Isipt lañu bawoo. Séeréer si, Pël yi, Sooninke yi, Tekuruur yi (Tukuloor), ak Sara yi juge nguuru Bagirmi ca réewum Cadd. Wolof yi ca xeet ya lañu juge. Xeet ya yépp danoo jaxasoo, ca yoonu Imbraatoor gu Ghana, ca dëkk bi nu tuddé Jolof. Wolof mooy ñu bawoo Jolof, Waa-Lof (ay gaa yu juge Lof) walla Waa-Laf (ñoñ Laf), di nekk tay Wolof. Seex Anta Joob, Walaf la doon wax. Noonu la xeetu Wolof judoo. Tur wii nuy wax Jolof, benn Soose bu tundoon Jolof Mbeng moo ko joxoon dëkk ba. Ca cosaan dañu ne Jolof Mbeng ak njabootam ñoo fa njëkkoon a dëkk. Ba noppi Amadu Abuubakar ñëw fa, moom baayam Naaru Murabituun la woon, turam di Abu Bakr Ben Omar, ca cosaan danu daa wax Abu Dardaayi, yaayam Tukuloor la woon, turam di Fatumata Sàll doomu Lam-Tooro (Lamanu Tooro) ca Tekuruur. Amadu, Baayam jenn jàmbaar ju Saraxule moo ko ray, booba nag la Fatumata seeti jeneen jëkër. Amadu bégul woon ci boroom këru nday ju bees ji, lii a taxoon mu dem Waalo. Foofa nag nit ña fa nekk ay Lamani Séeréer yu sant Ngom aki Sàmmkati Pël yu sant Jaw. Laman yi danoo yékkati woon Amadu, ndax dafa baaxoon ba jaaxal dëkk bi, ba far mujj di Buuru Waalo. + +Séeréer si ñoo ko tudde Njaajaan Njaay. Bi Amadu agsi ca waalo, ci li mu daan daaw keru yaayam, ñii daan dëkk Waalo ñoo demoon setsi Maysa Waly Joon, buuru Siin ba, ngiir mu leen wax kan mooy Amadu boobu ñu leen jaxal. Buur bi, boroom xam xam la woon, ku mënoon gis yu bare. Maysa Waly ne leen koku Njajaan Njaay la, ci Serer mooy: ku doy war. Fofu la tuuru Njaajan Njaay joge, ak sant bobu di Njaay. Kon Njaay, ci Serer yi la joge. Njaay itam, mooy Gaynde (Gaynde Njaay ca cosaan) te Gaynde mooy buuru àll ba. Da bokk ak turu Jaara ci kallama Mandinke yi, Jaata ci Joola yi. Moo ñu dakkantal Njaayen yi Jaara walla Jaata. Ñu yooree tur yi, dañu kalante. + +Waaye ba noppi Njaajaan dañu koo dàqe dëkk ba, ndax daa am ku ko bëggoon a ray. Mu daal di woon daw ba Jolof ca Wolof ya. Njaajaan Njaay dajale woon na Wolof yi ndax ñu gën a am doole, ba man a taxawal Imbraatóor gu Djolof. Wolof yi, Jolof mooy seeni dëkk, waaye ak seeni imbraatoor gi, dañoo demoon dëkk te yor: Waalo, Tekuruur, Kajoor, Bawal, Siin-Saalum, Njarmeew (soog a dëkk Bundu), Ñaani, Wulli, Bambug. Nguur ga gépp Jolof uffoon na ko. Lii moo tax Làkku Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Ca atum 1549 la Jolof gu mag ga tas ak Lele Fuli Fak. Nguuri Wolof yépp am seeni buuri bopp: Dammeel ca Kajoor, Teeñ ca Bawal, Baraag ca Waalo, Buurba ca Jolof (Ca Jolof gu mag ga, Buur Fari lañu daa wax). Decce Fu Njóogu ak Amari Ngóone Sabel Faal, ñoo fi njëkk a nekk Dammeel-Teeñ. + +Njabooti Wolof yi yoroon nguuri wolof yi + Njaay (Jolof) + Mbóoj ak Wàdd (Waalo) + Faal ak Jóop (Kajoor ak Bawal) + +Nosteg mboolaay ga + Géer/Garmi, ca kaw, ñoo doon nekk buur yi. Kàŋam (buuri Laman yi) Farba Kaba (buuri Ceddo yi), Tuube, Bumi ak Lingeer. +Ca seeni meen ñoo man a nekk Buur. Meen moo gën a am solo Geño(Meen:wàllug nday). Geño:wàllug baay . + Jàmbur ak Sëriñ. Ñoom Sëriñ si ay Tukulóor lanu(Mbàkke, Ja, Si, Lóo, Sàll) Saraxule (Silla, Xulé, Siise, Daraame, Kebe) walla ay Naar (Jaxumpa, Aydara, Kundul, Saadi, Baabu). + Baadoola, Mbay moo doonoon seen dund. + +Ñeeño yi + Tëgg, Lawbe, Wuude, Ràbb. Am na ñu bari ci ñoom ci xeetu Pël/Tukuloor lañu juge ñooy ñi sant : Caam, Mbow, Ace, Jaw, Jum, Taal, Faam, Gise, Sow, Béey, Ñas, Mbay . Ñeeño yooyu dañuy kalante ak Pël yi, ndax danoo bokk maam. + Géwal yi, ñépp lañuy woy, Buur yi, ñeeño yi. Cosaanu nit ñépp lañu xam, seeni Sant yi gën a siiw: Sekk, Mbay, Mbuub, Laam, Séy. +Ci ñoom, am na ñuy jefandiku ak xalam gi. Ñuy xalam itam, ci lu ëpp, ay tukuloor lañu, ni Bukunta Njaay walla Samba Jabare Saamb, maamam di baawo Gede, been dekk la ci diwaani Fuuta Tooro. + +Jaam yi + Am na jaami buur yi ( Ceddo yi), Jaami Juddu, Jaami Sayor (ñoom ca xare lees leen daan ame ak a jàppe). Xeet wu nekk nag lanu daan juge. + +Wolof yi danoo jaxaasoo, lii moo tax seeni sant bari, ak tamit xeet yu bari ñëw nanu ci ñoom (Wolofal: Wolofisation). +Ca Fuuta-Tooro, ca Cuballo (Nappkatu Tukuloor) walla Sebbe (Ceddo/Jàmbaar Tukulóor) Walla Tooroodo, lanu. Danoo teel a nekk foofu. +Ci Senegaal ñoom ñoo njëkk a gis Tubaab yi. Bu njëkk Ceddo lañu woon, tay ñu bari ci yoonu murit lañu bokk walla tiijaaniya. Am na ay ay nasaraan (chrétiens) tamit waaye duñu ñu bari (Gore/Ndar). Seex Ahmadu Bamba Mbakke ak Alaaji Maalik SI ñoo gën a dugal Wolof yi ci lislaam. Wolof yu bari gàddaay nanu (walla tukki nanu) dem Faraas, Diiwaan yu Bennoo yi (États-unis), Itaali, Espaañ. Ci Senegaal ñoo yor pal yi gën a rëy (loolu du lu ñépp man a ànd, ndax gisees na ne Njiitul Senegaal lu njëkk séeréer la woon la ca topp it noonu, boo demee ca xare ba (l'armée)lu ëpp ca kilifa ya doonuñu ko. Kon wax jooju ju deesi xoolaat la). Ñoom ñoo gën a fonk seeni réewm (Nationalisme Sénégalais). Am na ci ñoñ ci Mbay (Kaw-Kaw) lanuy dunde, am ci ñoñ ci Napp, ca géej gi (ci ñoom la Lébu yi bokk). Jom ak Teraanga ci ñoom la fekk baax. + +Xool itam +Wolof +Pël +Tukkloor +Séeréer +waasoy Senegaal +Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël yi ci Sowwu Afrig, dañoo bokk ci waaso yi gën a bari gën a yaatu. Senegaal, Mali, Gànnaar, Gàmbi, Gine, Gine Bisaawóo, Niseer, Burkina Faso, Niseeria, Benin, Kot Diwaar, Kameroon, Réewum Diggu Afrig, ba Sudaan, ca réewum yii yépp Pël yi ña nga fa. +Xeet woowu am nañu tur yu bari: Pël ci Wolof, ci Afrig mooy tur wi gën a siiw, Fula ca Mande ya, Fulani ca Naar ya, Fellata wala Fellan ca Sudaan. + + +Ñoom ci seen bopp dañuy wax Pullo wala FulBe. Isipt mooy réew mi ñu bawoo. Pël ya ca Isipt ay nit ñu ñuul lañu nekkoon. Ba noppi, ay nit ñu weex, ñëw ca seenum réew juge Asi ak Tugal , bokk na ca xeet yooya: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari yu ñuy tudde ay waa End-tugal (Indo-européen). Pël yu ñuul yi ak nit ñu weex ñi dañoo jaxaasoo woon. Lii moo tax Pël yi gën a xees, gën a sew, am kawar gu gën a nooy, bu ñu leen xoolee ci yeneen xeet yu ñuul yi ci Afrig. Ba noppi, Imbraatóor gu Iran(ñoñ Cambyse ñi(les Perses) ), tegoon nañu loxo réewum Isipt, di fa tege dund gu metti, rawati na ca nit ñu ñuul ña. Lii moo tax Pël ya ak Séeréer sa gàddaay, dëkki ca Sudaan (Nubie) dëkki seeni maam, soog a dem Senegaal. Pël ak Séeréer danoo bokk maam, seeni làkk tamit. Yàgg nañoo ànd, dañuy kalante ci seen biir. Ca yoonu Tekuruur, pël ya ca Dexug Senegaal rekk lañu nekkoon ak seeni nag. Booba nekkuñu woon ay jullit. Amuñu woon nguur ndax ak seeni nag ci màng rekk lañu nekke woon. Meew ak Sanqal (ñórndi) moo doonoon seenu lekk. Pël ci boppam am na xeet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo mooy seen Buur: JaawBe yi, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Am na yeneen KinDe. Màng gi ñu dëkke tax na ñu tuuru ci Sowwu Afrig gépp, ba far delseeti Sudaan, cig muñ ak coona ndax saa su nekk ci dëkki jàmbur yi rekk lañuy nekk, seen nag yi leeg-leeg ñu ruur tooli baykat yi, loolu it di jur xuloo bu rëy ak ŋaayoo ci seen digg ak woroon tool yi. + +Ca atum 1539 Koli Tengella Bâ, mi ngi bokke ci Pël ci wetug baayam, bokk it ci Mande yi ci wàllug yaayam (Keyta), dajale woon na sàmmkati Pël yi ak mande yi, ngir ñu man a am doole. Daa di dugg ci yeneen xeet (Wolof, Séeréer, Bajaaranke, Joola, Baga, Sooninke . Ñoom ñépp ak seen aroo Koli Tengella, ñu yéeg ba Tekuruur, di xeex ak Buur-ba Jolof ba, ndax kii moo doon yor dëkk ba, ak Lam-Toro ya, Lam-Térmes, Lam-Taga ya, Juroom ñeenti fan soog a yor dëkk ai. Koli Tengella teg na fa njabootam (Denyakoobe yi), tudde na nguur ga Fuuta-Toro (Fuuta mooy dëkku Pël ca seen Làkk). Lii ca Senegaal la xewe. + +Ca Mali Pël ya doñoo njëkk am doole ca atum 1818. Booba nag Ahmadu Bari, Sëriñ la nekkoon, dajale na Pëli Jullit yi, ak Mande yu jullit yi ( Mandé Mori yi : Siise, Ture, Silla ), ngir ñu àndandoo xeex (Jiyaar) safaan nguuru Bàmbara yi fi nekkoon (nguuru Ségu ak Kaarta). Buuru Bàmbara yi (Fama) ak seeni jàmbaar (Ton-Dion), amoon nanu doole, lii moo tax Ahmadu Bari tabax Imbraatoor gu Pël ca Massina Kese. ak itam Pël yi, ca Mali, foofu lañu ëppe woon ba tay (Tay jii foofa mooy diiwaan (Région) bu Mopti). +Ca Gine, Pël ya dañu faa yàgg, waaye Mande ya (Jalonke) ñoo yoron dëkk ba. Ca 1715, ay Pël yu jullit yu juge Fuuta-Tooro ak Massina ca Mali, ñoo ñëw Gine, di fa Jiyaar, di ray ñi duli jullit walla di leen jàpp ay jaam, lii moo tax giir yu bari (Susu yi, jalonke, ak Baga yi) daw ca géeju Gine, di tabax foofa ay nguur. Pël yu Jullit yi dañu doon ray ñoom tamit yeneen Pël ngir ne nekkuñu woon ay juulit. Pëli jullit yi dañoo bokkoon ca njabooti: Bâ, Bari, Jallo, Sow. Ñoom ñoo tabax nguuru Fuuta-Jalon. Karamoko Alfa Jallo mo njëkk a nekk Almaami. +Ca Niseria atum 1808, Usmaan Dan Fojo, njabootam Fuuta-Tooro la bawoo, nekk ay Tooroodo, Sëriñ bu mag la nekkoon, bu bokk ca tariixa Xaadiriya. Moom nag dajale na baykatu Awsa yi, ak sàmbkati Pël yi, di leen dugal ci Lislaam, ndax ñu man a def jiyaar ca Nguuru Awsa yi fi nekkoon. Ray na Buuru Awsa bi, daal di tabax Imbraatoor gu Sokoto. Dem na xeex ca Imbratoor gu Kanem-Bornu ca Cadd, waaye ñooñu dañoo amooon doole lool. +Ca kaw Kamerun atum 1810, benn sëriñ bu tudd Mojibo Adama, dajale na Pëli jullit(foofu Fulbé lees leen di wax) yi fi nékkoon, nu tabax nguuru Adamawa. Waaye am na Fulbé yu bari (WodaaBe/Borooro), yoy ànduñu woon ca googa nguur. +Modibo ak yeneen Pël yi ñoo defoon Jihaad, ndax ay jullit lanu woon. Modibo Adama, Usman Dan Fojo moo ko dimbali woon. +Ca atum 1860, Alfa Yaaya Molo Balde, tabax nguuru Fuladu ca Bëj-saalumu Senegaal. Daal di dajale Pël yi di leen dugal ci lislaam, ndax Almaami bu Fuuta-Jalon Alfa Bokar Biram, nee na woon du dimbali ku dul Jullit. +Almaami boobu ak Alfa Yaaya xare nanu ak nguur gu Mandé, Kabbu ak seeni Buur (Mansa), ndax foofu Pël yi danu faa nekkoon Jaami Mandé yi. Ñaari Buur rekk ñoo yoroon Fulaadu, Alfa Yaaya ak doomam Musaa Molo Balde. + +Kon Pël yi, Lislaam moo leen dajale, di leen jox doole. + +Pël seeni Nostey mboolaay nii lanu tëdde woon: + RimBe ñoo daa doon Buur yi. + JaawanDo yi, ñoo daa topp RimBe yi di leen won nan lañuy yore nguur. + +Ñeeño yi: + + WayilBe ñoo daa nekk Tëgg yi. + LawBe ñoo daa doon Seen yi. + SakeeBe, nekk Wuude yi. + MabuuBe, doon Ràbb yi. + BaambaaDo, doon Xalamkat yi, woykati Jàmbaar yi. + Gawlo, Woykati Buur yi. + +Jaam yi: + + Maccudo walla Kordo. + +Ca Isipt Pël ya, dañoo yoroon ñatti Sant rekk (Ba, Ka, Bara (tay mu soppiku di Bari)). Ba noppi Pël yi danoo jël yeneen Sant Ndax dëkk bi, walla Mban yi, liggéey yi ñu doon def. + +Li lépp ba am tay Sant yii: Bâ, Bari, Jallo, Ka, Ja, Sow, Jaw, Caam, Naan, Jum, Dikko, Seydi, Mbow, Bokum, Dem, Sidibe, Sàll, +Ca fulaadu Pël yu bari Jamanka lañu sant. Ca Mali Sidibe mooy Sow. Ca Niseriyaa Pël yu bari Bello lanu sant. Ku sant Baal, maamam ay Bâ lanu woon. Ku Sant Jakk maaman ay Sow lanu woon. +Sankara, Sankaré, Shagari, yooyu yépp benn lanu. +Am na Pël yu bari yoy dem nanu ca Wolof ya, looloo tax am ay wolof yu sant (Caam, Mbow, Sow, Naan, Sàll). Am na tam waaso yu bari yoy dikk nanu ci Pël yi, moo tax am ay Pël yu sant Siise, Ture, Njaay, Jakite, Kamara ak yeneen sant. + +Xool itam +Wolof (askan) +Pël +Tukkloor +Séeréer +waasoy senegaal +Làkki Senegaal +Tukkloor genn giir la gu nekk Senegaal. Ñoom ci seen bopp, Halpulaar lañu tudd. Nguuru Fuuta-Tooro mooy seen i dëkk, li moo tax dañuy wax tamit FuutaŋkooBe / Fuutaŋke (ku dëkk ca Fuuta). + +Ñoom dexug Niil lañu juge, ca dëkk ba ñu tuddee Nubi / Kuus, di nekk tay ca réewu Sudaan. Foofu dañoo bokkoon ak Séeréer yi. Pël yi nekkoon wàllu tukkloor ñoo nekkoon sammkat. Boobu baatu tukkloor ñëwaguloon. Ñoom ñépp dañoo mujj a gaddaay, ba agsi dexug Senegaal. Suuf si ñu agsi ba noppi, ay Sooninke ak ay naar agsi nañu fa tamit. Moo tax tay képp kuy dem ca Fuuta Tooro, xeet yooyu yépp ngay fekk. Turu Tukkloor ci lakk tubaab la juge, tukkloor lañu doon wax, ndax tur woowu nañu daan tudde seen dëkk (Tekuruur). Tukkloor mooy ku dëkk Tekruur. Am na ñu ne, wolof yi ñoo sos baat bi. Tukkloor yi Pulaar mooy seeni lakk, lislaam mooy seen diine. Tukkloor yi dañoo teel a dugg ci lislaam ca jamonoy imbraatoor gu Gana. Sooninke yi ñoo leen duggal ca lislaam. Buuru tekruur bii di War Jaabi, moo indaale lislaam ca nguuru ga, te + +Ca XVIeelu¹⁶ xarnu, benn sëriñu tukuloor mu tudd Ali Elibana Saal, ak xarekatam, Jihaaroonàñu ca Fuuta-Tooro, ndax Deeniyaŋkooɓe yi ak óoih Tegaelaamiu leen jiite, ñoo yooonr nguurgai te nekkuñu woon ay jllli, aAy Ceddo lañu woon. Waaye deeniyaŋkoɓe yi, àaq añun Elibana Saal ak xarekatam. Ñoomñu daw ba Saalum, foofuldañu Jhyaar ca Séeréer ai waaye ñoom àaq añu Ali Elibana ba dexug àambi, foofu tukkloor yi tabax nañugbenn nguur mooy nguur Kabada. + +Ca XVIIeelu¹⁷ xarnu, Maalig Si Daawda, tabax na nguuru Bundu, ca Senegaal, ca wetu nguuru Jolof, ak Gajaaga. Moom tamit Def na Jiyaar ca Fuuta-Tooro, deeniyaŋkooɓe yi dàq ko ca dëkk ba. Moom ak njabootam, xarekatam, daw nañu ca Njarmeew, di daje ak Waly Mbëru Mbakke Ndaw berlëp ku daan ilif dëkk boobu. Foofu la tabax nguuru Bundu. Malig Si Daawda, tooroodo la woon. + +Ca XVIIIeelu¹⁸ xarnu, Tooroodo Tukkloor yi dàq nañu Deeniyaŋkooɓe yi fa doon Buur (Silatigi). Li yépp ak Suleymaan Baal ak Abdul Kader Kan la xewe. Ñoom nag, duggu nañu FutaŋkooBe yëpp ca lislaam, di fa teg ay Almamy, Almamy boobu moo yore woon nguur bi, dafa waroon na nekk Seriñ bu gëna am xam-xam ca lislaam ca FutaŋkooBe yi. + +Ca XIXee xarnu, El Haaj Umar Taal, tabax na imbratoor gu Tukkloor ca Mali. Umar Taal, dem na ca Makka, foofu Xaalifa yi, def neen ko, Xaalifu Tiijaaniyaa ca reew yi nit ñu ñuul (Sudaan bu sowu jant). Umar Taal duggu na ay nit yu bare ca biir tariqa Tiijaaniyaa. Jiyaar na ca nguruu Xaaso waaye foofu tubaap yi daq neen ko. kon dem na ca Mali, xeex ak nguuru Jaara, rey fa Buur ba (Birante Karunga Jawara). Xeex na ak Buur yi Bambara yi (Fama yi), ca nguuru Segu ak Kaarta, di leen uuf ca imbratooram. Xéex na ak Amadu Bari, buuru Massina, di ko uuf tamit. + +Ca XIXeelu xarnu, Maba Jaxu Ba, Almamy bu Rip la nekkoon. Rip moo doon benn diiwaan ca biir Nguuru Saalum. Ca Rip ay Buuru Mandiŋ (sant Maroon) ñoo fi nekkoon. Nguur bi Badibu la tudde woon, Maba jaxu moo ko joox tur boobu: Rip. Ndax mu mëna fa nekk Almamy, Maba jaxu jiyaar na ca badibu yepp di rey Buuri yepp. El Haaj Umar Taal, moo ko daan digal mu def loolu, ndax gis na ci moom, nit ku xam lislaam bu baax. +Ca atum 1871-1875, Amadu Seexu, benn Almamy bu Fuuta-Tooro, jiyaar na ca nguruu Jolof, di fa nekk Buurba, ñeent at. + +Nosteg mboolay + +Tukkloor seeni Nosteg mboolaay ga, nii la tëdde woon: + +Rimbe yi (dimo su ne benn) ñoo doon: + +Sebbe yi, xarekat lañu woon, ñoom ay Ceddo lañu nekkoon. Sebbe yu bari ca xetu Séeréer ak Pël lañu joge. Ba XVeelu xarnu ba atum 1776 ñoom ñoo yoroon Fuuta-Tooro. +Seeni sant: Njaay, Saal, Jeŋ, Wan, Ñaŋ, Jah, Ndoom, Cimbo, Jaw, Bah, Ndaw, Caam, Waad, Mbooj. + +Torodoo yi, ñooñu ñoo daan doxal lislaam. Ca atum 1776 lañu jëkk am doole. Ñoom ñoo daq Sebbe yi. Buuru Torodoo yi Almamy la. Seeñi maam ñu bare ca xetu Sooninke ak Naar lañu juge. +Seeni sant: Sih, Lih, Kan, Aan, Ture, Siise, Aïdara, Njaay, Caam, Wan, Ja, Saal, Bah. Am na yeneen. + +JaawamBe yi, ñoo doon topp Buuri, di leen wone naka lañu yore nguur gi. Ca Pël yi lañu juge seeni sant : Jaw, Ñaan, Daf, Njim, Bokkum.Ci lu gëna siiw. + +SubalBe yi, ay nappkat lañu, te ci cosaan dañu doonoon ay xarekat mel ni Sebbe yi. Bokk neen ak Sebbe yi. Yu bare seen maam ay Séeréer lañu. Seeñi Buur, Teeñ walla Jaaltabe la tudd. Seeni Sant: Sar, Ñaŋ, Juuf, Maal, Gay, Diba, Jool, Jeey, Gey, Jaw. Am na yeneen Sant. + +Ñeeno yi: + +WayilBe yi ñoo doon Tëgg yi. +Seeni sant : Caam, Mbow, Jaw, Kante, Sih, Peen. + +LawBe yi, Seen yi, ñu jefandikook bant. +Seeni sant: Sow, Jum, Gajaga, Wañ. + +SakeeBe yi, ñoo doon Wuude yi. +Seeni sant: Beey, Gakko. + +MabuuBe yi, ñoo doon Rabb y. +Seeni sant: Gise , Sangott, Kume, Jonŋ, Taal. + +Waambaabe yi, ñoo doon Xalamkat yi, woykatu xarekat yi. +Seeni sant: Bah, Jum, Gise. + +Gawlo yi, woykatu Buuri, sab lekk yi. +Seeni sant: Mbum, Samb, Sek, Jeŋ, Laam, Mbay, Joob. + +Jaam yi: + +Maccudo/Kordo/JyaaBe. Tey, kenn du jaamloo jammbuur. Aada bu jëkk la woon. + +Tukkloor yi, bey mooy seeni dund. Ca Fuuta-Jalon am na fa ay Tukkloor. Ca Kajoor dañu jëkkoon nekk ca diiwanu Jammbuur (Luga, Koki). +Am na yu bare dañu daw Fuuta, di dem ca Dakar, Kawlax, Cees, wala Ndaar, ak yeneeni peey yu mag. Ñu ci bare ca tariqa Tiijaaniyaa lañu bokk. + +Xool itam +Wolof (askan) +Pël +Séeréer +waasoy Senegaal +Taariixu senegaal +Joolaa genn la ci giiri Senegaal yi. Ñoom Kaasamaas lañu fekk baax. Ca yoonu Imbraatóor gu Mali, lañu dem dëkk. mandeŋ yi ñoo leen dàq, ñu dem kaasamaas. Ca bëj-gànnaaru Gine Bisaawóo tamit ñoo ga fa. Baynuk yi ñoo doon jiite joolaa yi ca kaasamaas. Ñoo tabaxoon nguurug Kasanlaa. Joolaa yi ak Baynuk yi, dañu dëkkandoo woon ak Soose yi, Njaago yi ak Pël yi. Ñoom ñoo fa njëkkoon joolaa yi. + +Joola sen Ada niogi ko gëne xam si Bukut. + +Bukut neek ab Ada bu nu rane si Joola yi + + + +Mboor (Taariix) +Joolaa yi ca sowwu Kaasamaas lañu tabaxoon seeni nguur, nguuru Banjal, nguruu Flub. Mbayum ceeb, napp, Sàmm, ñoo doonoon seen xeeti liggéey. Tiramakan Taraaware, di ab Mandeŋ bu bokkoon ca imbratóor gu Mali, moo leen sancoon ci ndigalu jàmbaari buur jooju di Sunjata Keyta. Sunjata Keyta moo yónni woon Tiramakan ca kaasamaas ngir mu jël nguuri joola yépp yokk ci imbratóoram. + +Tiramakan ca la boole nguuri Joolaa yi ak yu Baynuk yi ci genn nguur duppe ko Kaabu. Nguur gi demoon na ba ci dexug Gàmbi gi, ba Bajar, bëj-gànnaaru Gine bisaawoo. Màndeŋ yi ak Joolaa yi xeexuñu benn yoon, dañu a nekkoon ci jàmm, di dëkkandoo. Joolaa yi ak Mandeŋ yi itam dañoo jaaxasoo woon ba bokk ay sant ( Sonko, Saane, Maane, Jaabi, Saañaa). + +Ci XVIeelu¹⁶ xarnu la tubaab yi ñëw Kaasamaas. Bi leen tubaab yi bëggee sanc ñoom dañoo bañoon, taxaw jammaarloo ak ñoom, masu ñoo nangu itam njàppum jaam, seenug njàmbaar terewuloon waa-portugaal yi mujj leen sanc. Ca XXeelu²⁰ Xarnu, la Aliin Situwe Jaata jàmmaarloo ak tubaab yi ngir dakkal canc gi. Joolaa yépp ànd ngir xeex. Aliin dajale góor ñépp ngir jàmmaarlo gi. Waaye seen fipp googu manutoon aantal seen yéene ngir seenug néew-doole ci kanamu sancaan bi. Ci lañu jàppee Aliin gàddaayal ko Tumbuktu ca Mali, foofu la génne àdduna. + +Xeeti joolaa +Joolaa yi ci seen biir dañoo séddaliku ciy xeet yu bari. + Fooñi + Felup wala Kasa, ñoom ño tabax nguuru Usuy + Ejamat, Joola yu Gine-Bisaawóo + Yoola + Elufayi + Eyunayi + Eblufayi + Seleg + Ajuwat +añs +Seen i sant: Jéeju, Jaata, Jamakun, Saañaa, Gujaabi, Jaabi, Kóli, Bojã, Baaji, Maane, Saane. Biyaagi, Baseen, Ehemba, Sambu. + +Diine +Ci Joola yi am na ay jullit, ay katolig, waaye am na it ay ceddo. Tubaab yi ñoo leen dugal ca diiney katolig, Wolof yi ak Pël yi ñoo leen dugal ci lislaam. + +Xool it + + Baynuk + +Téerekaay + Alice Joyce Hamer, Tradition and Change : A Social History of Diola Women (Southern Senegal) in the twentieth Century, Michigan University, 1983, 329 p. (Thèse) + Olga Linares de Sapir, « Shell middens of lower Casamance and problems of Diola protohistory », West African Journal of Archaeology (Oxford University Press), Ibadan, 1971, vol. I, p. 23-54 + Olga F. Linares, Prayer, Power, and Production: The Jola of Casamance, Cambridge University Press, 1992, 280 p. + A. Badji, La lutte traditionnelle joola. Étude et perspectives, Dakar, INSEPS, 1982, 47 p. (Mémoire de Maîtrise STAPS) + Saloum Badji, Habitat et occupation du sol dans les pays jolla (du XVe au XXe siècle, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2000, 121 p. (Mémoire de Maîtrise) + Alioune Diatta, Structures politiques et sociales du monde traditionnel Joola, Paris, Université de Paris I, 1982, 345 p. (Thèse de 3e cycle). + Nazaire Diatta, Le taureau, symbole de mort et de vie dans l’initiation de la circoncision chez les Diola (Sénégal), Paris, EHESS, 1979, 3+292 p. (Mémoire EHESS) + Nazaire Diatta, Anthropologie et herméneutique des rites joola : funérailles, initiations, Paris, EHESS, 1982 (Thèse de 3e cycle) + Nazaire Diatta, Proverbes Jóola de Casamance, Karthala, 1998, 416 p. + Christian Sina Diatta, Parlons Jola - Langue et culture Diolas, L'Harmattan, 1998, + Athanase Diédhiou, Chants funèbres et rites traditionnels dans la société Diola, Dakar, Université de Dakar, 198? (Mémoire de Maîtrise) + Lamine Diédhiou, Riz, symboles et développement chez les diola de Basse Casamance, PU Laval, 2005, + Odile Journet-Diallo, Les créances de la terre. Chroniques du pays jamaat (Joola de Guinée-Bissau), Turnhout, Brepols, collection BEHE, n° 134, 2007, + Françoise Ki-Zerbo, Les sources du droit chez les Diola du Sénégal : logiques de transmission des richesses et des statuts chez les Diola du Boulouf (Casamance, Sénégal), Karthala, 1997, 217 pages + Michel Bokar Mballo, Le personnage du prêtre dans la société traditionnelle diola cassa et la société traditionnelle romaine dans ses différentes attributions, Dakar, Université de Dakar, 1981, 97 p. (Mémoire de Maîtrise) + Michel Bokar Mballo, Les survivances des religions traditionnelles chez les chrétiens de l’époque de saint Augustin et chez les chrétiens diola kassa de la Basse Casamance, Dakar, Université de Dakar, 1985 (Thèse de 3e cycle) + Paolo Palmeri, Retour dans un village diola de Casamance, L’Harmattan, 1995, 488 p. ISBN 2-7384-3616-1 + Jean-Joseph Sambou, La notion de Boekin dans le conte diola, Dakar, Université de Dakar, 1984, 154 p. (Mémoire de Maîtrise) + Francis G. Snyder, L’évolution du droit foncier Diola de basse-Casamance (république du Sénégal) : étude d’anthropologie juridique des rapports entre les hommes et les terres chez les Diola-Bandial, Paris, Université de Paris I, 1973, 550 p. (Thèse de 3e cycle) + Louis-Vincent Thomas, Les Diola. Essai d’analyse fonctionnelle sur une population de basse-Casamance, Dakar, IFAN, Université de Dakar, 1958, 821 p. (Thèse d’Etat publiée) + Louis-Vincent Thomas, Et le lièvre vint : Récits populaires diola, Nea, 1982, 266 p. + +Filmkaay + Das Fest der Ringer. Bei den Diola im Südsenegal, téléfilm documentaire allemand de Essibyé Augustin Diatta et Ulla Fels, 1999 + +Lëkkalekaay yu biti + + « Shrines of the Slave Trade : Diola Religion and Society in Precolonial Senegambia » (Robert Martin Baum, Oxford University Press, 1999 ISBN 0195123921) + Chronology for Diolas in Casamance in Senegal (fiche du Haut Commissariat des Nations unies pour les réfugiés, 2004) + Les Diolas + Les Diolas + Casamançais, Diolas et animisme + « Les jeunes Diola face à l'exode rural » (Marie-Christine Cormier, géographe, ORSTOM, CRODT, Dakar, 1984) + « Quelques proverbes Diola » (Nazaire Diatta Ukëyëng, ecrivain) + +Waasoy Senegaal +Đồng Hới ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 155,54 km², ci 2006 amoon na 103.988 way dëkk. + +Wiyetnaam +Namandiru, nekkoon na nguur gu nekk Senegaal ca jamono yu yag ya. Ca VIIeelu xarnu am na benn njabootay bu tuddu Jaa-Ogo, ñow nañu dëkk ca penku Senegaal, ca wetu dexug Senegaal. Jaa-Ogo yi, Misra lañu juge. Daw nañu wa Misra ndax foofu, ay jaambar ñu leen tuddu Perse, ñow nañu ca biir Misra, di bëgg noot reew mi. Li mooy tax Jaa-Ogo yi, gadday ba agsi dexug Senegaal. Ca dëkk boobu, kenn nekku fa woon. Ca senegaal tabax nañu nguuru Namandiru. + +Jaa-Ogo yi, tëgg moo doonoon seen liggeey. Jaa-Ogo yi ñoo indi liggeey bi ca Senegaal. Li mooy tax ca jamono boobu tëgg yi ay buur bu mag lañu nekkoon. Ndax takkay yi, paaka yi, tin yi, leppu ñuy jefandiko ak weñ, ñoom rekk ñoo ko mënoon. Jaa-Ogo yi, am na yu bari deeñi ne, ca Pël yi lañu bokkoon, ndax tur bi ñu joxe seeni nguur Namandiru, ca lakku Pulaar la juge, di tekki = Reew mi am lepp. Seen sant yi tamit, moo di ay sant Pël yi yore. Jaa-Ogo yi ñoo tabax tamit nguuru Tekuruur, tey di nekk Fuuta-Tooro. + +Njabootu Manna yi, ñoo daan Jaa-Ogo yi. Manna yi ay Saraxule lañu nekkoon, di sant Ñaxate ak Sumaare. +Tamit Naar yi, ca Xeelu xarnu, ak seen buur Abu Bakr ibn Umar, xeex nañu ak Jaa-Ogo yi. +Manna yi ak Naar yi mooy tax, Nguuru Namandiru daan. + +Boobu ñu nekkoon buur, ci seen jeexit itam, bekkoor bi fekk na leen, ba tax Jaa-Ogo yi gaddayaat ca yeneen dëkk ca Senegaal. + +Nguuru Njaarmeew + +Ba noppi, am na beneen njabootay ñu sant Ndaw, juge Gannar, diwaanu Assaba, ñow nañu ca dëkk bi amoon Namandiru, di fi tabax beneen nguur ñu woowe ko Njarmeew. Seen Buur, Belëp la tuddoon. Ndaw Belëp yi, yaguñu fa. Ndax ca XVeelu xarnu, Buurba Jolof ba, Tyukuli Ndiklam, uuf na dëkk bi ca biir Jolof, ak Tekuruur itam. Kon Ndaw Belëp yi, daw nañu ba Nguuru Seereer yi ca Saluum. Foofu Maad Saluum bi, Mbegaan Nduur, may na benn Diwaan buuru Ndaw Belëp bi, moom Waly Mberu Mbakke Ndaw la tudd. Diwaan bi, Nduukuman la. + +Koly Tenŋela, ca XVIeelu xarnu, Njaarmeew bi jël na ko, sooga Malik dawda Si, Toorodo bi, ñow foofu di tabax Nguuru Bundu. + +Tëgg yi + +Jaa-Ogo yi, ñoo maamu tëgg yi ca Senegaal. + +Ñu sant: Caam, Mbow, Conŋaan, Ñas, Bittey, Acc, Jaw, Mbaay. Ñoo ëppp ca Tëgg yi nekk Senegaal. + +Senegaal +World Wide Web manees na koo tekkee niki digg lënd gi (lënduk jargoñ) kon ana numu def ba tuddees ko digg lënd ? ndax moom la àdduna bépp ànd di jëfandikoo ku ne jàpp ci génn lawtan fa lawtan ya daje lees tuddee digg lënd moom nag manees na koo jëfandikoo fim ne ci àdduna bi yépp, gox yépp man nañu cee daje, boo jëmee ci ab dal dugal www doora def turu dal ba man naa ñàkk yit ci bu la neexee nde joowkat yu yees yi di nañu nànd sa bëgg-bëgg ba jobbu la, www yii nak limu wund ci wu-angalteer mooy World Wide Web + +Xam-xamu nosukaay +ngir bindu bu yees walla duggu ci sam saq xoolal ndimbël lii nu def ci ay nataal ngir mu gën a jumb ci gan ñi +fi gay cokk(clic) ngir dugg mba bindu +ni gay def ba dugg ci sam sàq, fi gay cokk ngir bindu +ni gay def ba sos am saq +man ga cee dugal sa loxo ngir mu yemb ndax lii di na tax mu gën a yomb ci gan ñi ndax jàgum bind(lire text) mi yombul ci ñépp. + +Ndimbal +Réewum ñaari dex yi ab diiwaanu Penku gu Jege la, nekk ci diggate Dijla (Tigre) ak Furaat (Ëfrat). Su nu koy xool ci lu ëpp mooy nekk Iraak gu tay jii. + +Tekkig baatu Mesopotaami daa soppiku ci doxug jamono. Ci tekkeem bu yàgg bu waa Geres ak waa Rom, moo doonoon wàllu bëj-gànnaar gi araab yi doon woowee itam Jasiira, beneen barab bu guus bi moom araab yi Sawaad lañu ko doon wax, ca seen mbind yu yàgg ya. woowin gu barab bi moo ngi tëggoo ci làkki ña fa cosaanoo, dinañu ko fekk ci wu-Akkadi Birīt Nārim "digalug dex gi" (birīt, « digal » ak nārim « dex ») walla Māt Birītim «Réewum digal bi» (māt, «Réew» birītim, «digal»). Ci wu-armeeni, ñoo ngi koy wax Beyn Nahrīm "digante dex yi" (beyn «digante», nahrīm «dex»), ci waxiin yépp mi ngi doon tekki wàll wi féete kawu Ëfrat. + +Melosuuf +Amoon na ay barab yu seen suuf nangu woon mbéy, nekkoon ci diggante Sagros, Taurus, ci tefesi Géej-Gu-Diggu gi ak ci Dóoxug waa-Peers gi. + +Di nañu ci boole diiwaan bi nekk ci bëj-saalum, diggante Tigre ak Ëfrat (ca Iraak gu tay). Waaye diiwaan bii tawam taxu koo bari noonu. + +Asiri lañuy fara di woowee bëj-gànnaaru Mesopotaami, Babilon moom di bëj-saalumam. + +Taariix +Jamonoy taariix mi ngi tambali ci Réewum ñaari dex yi ci 3300 njëkk juddug Isaa, bañu sàkkee mbind. Ñu dog-dogaat ko ciy jamono: + Jamonoy Uruk (3400-2900): la bind soqaliku ca Mesopotaami, waaye mbind yi ca jamono yooyu neexuñu woon a firi. Ay mbindi yoriin aki limi baat lañu woon, waaye manuñoo wax dara ci seenug dund. + Jamonoy (2900-2340): dañu koo séddale ci ñetti ron-jamono. ci ndoorteelu xaaju IIIu junneel(millénaire), lañu tambalee xam dara ci xew-xew yi, balaa dara ci ndimbalu dencu(archive) yi ñu wuññee Lagas. + Jamonoy Akkad(2340-2180): Sargon bu Akkad moo dakkaloon xaajale bafa amoon ciy dëkk-dëkkaan, boole leen ci menn réew, mu mujj doon imbratóor gu mag, ci ndimbalu sëtam ba Naram-Sin. + Jamonoy waa-Sumeer ju bees(2180-2004): Imbratóoru Akkad a ngi daanu ginnaaw fippu ak congu askani barbar yi. Nguur-nguuraani waa Simeer yi amaat seenug tembte, laataa Ur-Nammu ak doomam Sulgi di leen boole ci genn imbratóor gu mag, teg-tànk ci barab bépp. + Jamonoy waa-babilon ju njëkk(2004-1595): Imbratóoru Ur mi ngi daanu ci 2000 ciy pexey waa elam yeek waa amuru yi. Ñu mujj ñi ñoo jël boppi nguur yépp, daadi séddale Réewum ñaari dex yi: Isin, Larsa, Esnunna, Mari ak Babilon, mi mujj teg-tànk ci diiwaan bépp ak buuram ba Hammurabi, laataa muy daanu ndànk-ndànk, ba Itit yi mujj jël dëkk ba ci 1595. + Jamonoy waa-babilon ju diggu(1595-c.1080): Kasit yi ñoo mujj teg-tànk Babilon ci diirub ñenti xarnu. Ci bëj-gànnaar, nguurug Mitanni moo fa doon noote laataa nguurug waa Asiri gi di ko fél. + Jamonoy waa-asiri ju bees(911-609): ci IXu xarnu bi, la waa-asiri yi jógaat, joxaat seen baat doole, tegaat fa tank. Taxawalaat imbratóot gu mag yilif Penku gu Jege gépp, Ci jamonoy Sargonid yi la àgg ci pujam, laataa ag daanoom ci VIIu xarnu ginnaaw ay cong yu jóge ci waa-babilon yeek Med yi. + Jamonoy waa-Babilon ju bees(625-539): ci jamono jii la waa-babilon yi jëlaat genn wàll ci nguurug waa-asiri ju bees ji boole ci seen bos, ci ndimbalu Nabusodonosor II. Doonul nag nguur gu yàgg, ci 539 la ko waa-persi yi sanc. + Jamonoy waa-akamaniisia(539-331): donte ci jamono jii waa-akamaniisia yi ñoo yilifoon diiwaan bi, waaye terewuloon seenug suqaluku jëmoon kanam. + Jamonoy selewsid yi(331-140): imbratóor gu waa-persi gii di Akamaniisia ngi daanu ci congug Aleksandrë gu Mag, ginnaaw ag deewam ak ŋiir-ŋiirloo ya ca toftaloon la Selewsid yi jël nguur ga. Ci jamono jii la cosaanu Réewum ñaari dex yi tambalee juutu, te yokk ci IIu xarnu bi. + Jamonoy waa-pati(140 nj. Isaa, 224 g. Isaa ): Ci jamono jii la waa-Pati yi daq callala gu selewsid yi ci biir IIu xarnu bi. Ci seenug nguur la aada ak cosaani ña njëkk a dëkk ci diiwaan bi saay ba faaw, donte yenn aada yi doon nañu leen dund ba-ta ci julliwaay yu Babilon yi. + +Téerekaay + Collectif, De la Mésopotamie à la Perse, Encycloædia universalis, coll. « La grande histoire des civilisations », 1999 ; + Collectif, Atlas de la Mésopotamie et du Proche-Orient ancien, Brepols, 1996 ; + Adolf Leo Oppenheim, La Mésopotamie : portrait d'une civilisation, Gallimard, 1970 ; + Jean Bottéro, Mésopotamie. L'écriture, la raison et les dieux, Gallimard, coll. « Folio Histoire », 1997 ; + Francis Joannès (dir.), Dictionnaire de la civilisation mésopotamienne, Robert Laffont, 2001 ; + Jean-Jacques Glassner, La Mésopotamie, Belles Lettres, coll. « Guide des civilisations », 2002 ; + Jean-Claude Margueron, Les Mésopotamiens, Picard, 2003 ; + Georges Roux, La Mésopotamie, Seuil, coll. « Points histoire », 1995 (nouv. édition) ; + Pierre Amiet, L'Antiquité Orientale, PUF, Que-sais-je, 2003 + Pierre Amiet, Introduction à l'Antiquité Orientale, Desclée de Brouwer et École du Louvre, 2000 + Agnès Benoit, Art et archéologie : les civilisations du Proche-Orient ancien, Manuels de l'École du Louvre, 2003 + +Taariix +Iraak +Praia fimne mooy péeyu réewum Kap Weer. Ben dekku mi ngi dunu Santiago (Kap Weer). + +Melosuuf + +Achada Grande +Achada Grande Frente +Achada Grande Tras +Achada de Santo Antônio +Ponta das Bicudas +Calabaceira +Bairro Craveiro Lopes +Bela Vista +Fazenda (Achada Fazenda) +Gambôa/Cha das Areias +Lem Ferreira +Monte Vaca +Monte Vermelho +Paiol +Palmarejo +Palmarejo Grande +Plato +Quebra Canela +Ribeira da Trindade +São Francisco +São Tomé +Praia de São Tomé +Ponta Temerosa +Terra Branca +Trindade +Várzea + +Bayaali +Bayaal gu 12 Sattumbar (Alexandre Albuquerque) +Bayaal Antônio Lereno +Bayaal Dom Henrique + +Waax +Waax bu Praia (Porto da Praia) + +Sport + +Futbol klubi +Académica da Praia +ADESBA (AD Bairro) - Bairro Craveiro Lopes - Praia +Boavista FC - Praia +Celtic - Achadinha de Baixo - Praia +Sporting Clube - Praia +CD Travadores - Praia +Vitória FC - Praia + +Staad +Staad Várzea (Estádio da Várzea) - football + +Iniweersite +Iniweersite Kap Weer +Jean Piaget Iniweersite Kap Weer +Iniweersite Santiago (Kap Weer) + +Dayo +Jorge Barbosa +José Ulisses Correia e Silva +Dário Furtado +António Pedro +Arménio Vieira + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Teereekaay +Cabo Verde, viagem pela História das ilhas (Almeida, Germano; Lisboa: Caminho, 2003) +Cabo Verde, cruzamento do Atlântico Sul (Mindelo: Rádio Nova, 1998) + +Lëkkalekaay yu biti + +Lëkkalekaay Praia +https://web.archive.org/web/20110522092751/http://www.ise.cv/ +http://www.ahn.cv/ +https://web.archive.org/web/20081023171913/http://www.ic.cv/museu-etno.html + +Péy +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Nuwaaksot (Nouakchott) : mooy pééyu réewum Gànnaar. + +Gànnaar +Péy +Amman : mooy péeyu réewum Jordaani + +Péy +Jordaani +Bagdad : mooy péeyu réewum Iraak + +Iraak +Péy +Turu Way-Dëkk : maanaam ña dëkk ca réew mà ci (Fr Gentilé) lañ koy wax + +Réew +Njëkk-xaymà : maanaam li gay njëkka dugal bala gay dugal xayma(numero)yi (fr Indicatif téléphonique) + +Réew +Koppar : maanaam xaalisu réew mà (fr Monnaie) + +Koom-koom bokk na ci xaalis yi gënn a néew doole ci afrig +maanaam mooy ña yor réew mà lanu yor moo tudd nguur (fr État) +Maanaam yaatuwaayu réew mà waaye maneesukoo jëfëndikoo ci réew mu xat (wu-faraas : superficie, wu-angalteer : area). + +Melosuuf +Moroni mooy péeyu Bennoob Komoor yi, baat baa ngi jóge ci araab موروني + +Péy +Komoor +Maanaam ña dëkk ca réew mà ñoom lanuy woowe way-dëkk budee kenn nak aji-dëkk lanu koy wax + +Melosuuf + +id:Penduduk#Penduduk dunia +Diiney nasaraan, Diine la ju bawoo ca Yàlla, jaare ko ci Yonent Yàlla Iisaa, mooy diine ji Kurmet (Catholique) yi di topp, baat bi nag ci Araab la bawoo di Alnnasaaraa. + +Diine +maanaam dello gi tubaab yi dello réewi jambur yi ñu yoroon te moomu ñuko. + +Politig +Taariix +Ci xam-xamu nosukaay, ab dencukaay walla ab taxañ, ab ëmbukaayu ay xibaar la. Dencukaay yi, dañu leen séeddale ci ñaar: yu ëmb ay mbind "dencukaayub mbind" ak yu ëmb aw yoon wu ñaarñaarloo "dencukaayub ñaarñaarloo". Cig xarala, njoxe yi nekk cib dencukaay dañu leen nos niki ag callalag ay bit, ñu boole leen niki benn cër bu ñu rënk cim xel mu yaa. Dencukaay bu ci nekk day am tur, naka-jekk dañu leen boole ciw ŋara wu leen di ëmb. + +Ëmbiitu dencukaay bu ci nekk day am wenn melokaan wi, te melokaan wu ci nekk ak xeetu tëriin way man a firi walla soppi ëmbiitam. Nosukaay bu nekk day am li ñuy wax ag nosteg doxiin, te moom mooy am ci biiram tëriin yiy tax ngay man a ubbi, tëj, bind walla jàng ab dencukaay. Yenn nostey doxiin yi (walla doxaliin yi), yu ci mel ne Microsoft Windows ak MS-DOS, ci lawal gi ñuy yokk ci turu dencukaay bi lañuy xàmmee melokaanam ba man a firi ëmbitam, gu mel ne Mac OS moom yenn jéenginjoxe yu ñu dugalaale ci biir dencukaay bi lay jëfandikoo, geneen gu mel ne Unix moom, ngir xammee xeeti dencukaay yi, ñaari byte yi njëkk ci ëmbitam lay xool. + +Ay màndargaam + Dayoo bi: moo lay wax ñaata xibaar lañu dëxëñ ci biiram, ñu koy natt ci bit (misaal, dencukaay bii am na 1024 bit). + Dayoo bi ci jëmm: moo lay wax dig-digal bi ñu jàppal dencukaay bi ci xel mi ngir man ko faa téye, aki màndargaam. dayoo bi ci jëmm naka-jekk mooy ëpp tuuti dayoob dencukaay bi. + Lawal gi: lu ñuy yokk ci turu dencukaay bi la ngir muy xamale ci melokaanu ëmbitam, dina tax tëriin wu koy ubbi di ko jàng xam nan lay firee ëmbit li, ndax dencukaay bi man naa ëmb ab nataal, walla ab dégtal, walla ab wideo... + +Xeeti dencukaay +Ab dencukaayub mbind man nañoo firi ëmbitam mu doon ay mbind lees man a jàng. Safaanokg dencukaayub ñaarñaarloo, moom kenn manukoo jàng ndax ay '0' aki '1' la ëmb. + +Ngir nosukaay yi man a xammee màndarga mu nekk, dañoo defar ab xaatim duppee ko ASCII, ci wu-angalteer (American Standard Code for Information Interchange) ak lawalam ISO 8859 , màndarga gu nekk 8 bit lañ koy binde. Loolu tax nosukaay bi su gisee 8 bit yooyu di teewal benn màndarga, man koo xammee won la ko (misaal: 1100001 mooy arafi 'a' ). + + +Xam-xamu nosukaay +Gaynde g : dundat yi, + +Rab Gaynde mooy buuru àll ba +Looy : dundat yi + +Rab +Tene m : rab (dundat yi) + +Rab +Nguri : gunóor (rab) + +Gunóor +Mboq : Melo (fr : jaune) + +Melo +Wure ~ awale + +Fo +Esaas : petorool + +Simi +Kàttan +Téeméer : 100 + +Xayma +Junni : 1000 + +Xayma +Kër (Kër gi) : njaboot neeg. + +Kër +Paaka : suti waañ + +Suti +Waañ +Waañ : xaajo Kër + +Waañ +Furset : suti waañ + +Suti +Waañ + +de:Essbesteck#Gabel +Kuddu : suti waañ + +Suti +Waañ + +de:Essbesteck#Löffel +Aset : suti waañ + +Suti +Waañ +Mbaam : rab + +Rab +Dundat yi : rab + gàncax. + +Dundat yi +Iyon-jawwsu : Suuf < Fatt-jawwu < Yolom-jawwu < Biti-jawwu < Iyon-jawwsu + +Suuf +Jëmm +Waxtu (w-) = 60 simili = 3600 saa = 1/24 fan (bés) + +Jamono +At (m-) = 12 weer = 365 bés (365 fan) + +Arminaat +Jamono +Simili (b-) = 60 ñaareel = 1/60 waxtu + +Jamono +Saa(s-) : 1/60 simili, 1/3600 waxtu + +Jamono +Gaal : moto ndox + +Moto +Ganaar : rab (dundat yi) + +Rab +Bët : paar rab + +Rab +Soviet Yi Benno (1922-1991) : + + + + + + + + + + + + + + +Tugal +Asi +Jimbulaŋ aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulaŋ buy wax ci paj walla ci taariix kepp. Jimbulaŋ am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ciw nit, cib barab, cib xew-xew, cib xam-xam,... Jimbulaŋ day wuuteek baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi. Naka-jekk day doon ay téere yu bari. + +Tekkeem gu daj +Cër yi ëpp solo yiy tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu: + + Jagleel gi ci am + + Seenug lëkkaloo + + Nosiin wi + + Mbidiinu jukki yi. + +Jimbulang yi man nañoo wuute, aju ci seenum ëmbiit, man nañoo ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa-Brëtaañ, ñooy yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu. Am na it ay jimbulang yuy jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi... + +Yitteey liggéeyi jimbulang mooy jébbal xameef gi ëpp solo gees dajale ñeel tëriit li. Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñi ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu. Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi day soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam. Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bees jagleeli gone mooy gën a néew bees jagleeli mag. + +Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb. Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañuy jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi mooy séddale leen ciy wàll. Bu njëkk bi mooy bi ñu gën a jëfandikoo ba tay jii, donte xibaarukaay yu mbëjfeppal yi tax nañu ceet geek dello gi man a am, di lu kenn manutoon a xalaat bu njëkk ba. + +Jimbulang yi njëkk + +Nit, dale ci lu yàgg cig nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam. Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp. Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu cee lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juroom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja. + +Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima(Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax. Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi(ci daanaka 270 téere) + +Imbratóor bu siin bi, Cheng-Zu bu callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix, mi ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yees bindeek loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay. + +Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yeek niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: Doonoon nañu ay téere yu seer lool. +Tangor (b-) : ~ tund, jànj. + +Melosuuf +Saytubiddiw +Màndiŋ (m-) + +Fr: Savane + +xeeti bayaal yi +Saara : yay Afrig + +Yay +Melosuufug afrig +Max (m-) : gunóor (rab) + +Gunóor +Gunóor (g-) : rab + Max + Nguri + Melentaan +Melentaan : Gunóor + +Gunóor +Sharle Degóol (ci Faraañse mooy Charles de Gaulle) mi ngi gane àdduna 22 nowambar 1890 ca Liil (Fraas), génn àdduna 9 nowambar 1970 ca Colombey-ñaari-Jàggu-yi. Nekkoon na nitu guur gu Fraas, moo sos juróomeelu gaw bu Fraas 1958, jiite na réewum Fraas li ko dale 1959 ba 1969. + +Politigu Faraas +Wolof (làkk) + Wolof (askan) + +Wolof +Jimbulang bu waa-Brëtaañ walla Encyclopædia Britannica (ci wu-angalteer), ñi ngi ko siiwal ci diggante 1768-1771. Siiwalam gu njëkk mi ngi ame ca Edimbuurg ca Ekos. Bu waa-Brëtaañ bi bokk na ci jimbulang yiy wax ci lu daj yi njëkk ci kàllaama wu-angalteer, te bay jii ñoo ngi koy siiwal. + +Ci ndoorteelu ñaareelu xaaju 1700 ba ci 1900, bari woon na ay boroom xam-xam yu doon jàppee ay jukkeem niki delluwaay bu wóor, yenn saa yi, ci siiwal yu yees yi, daa na am ay gisiin yu yees yees jagleel ay mboolooy gëstukat. Ci jamono yooyu amoon na gëdd bu baax ci biir askan wiy làkk wu-angalteer. Ci XX xarnu bi la yitteey jimbulang soppiku bu baax, coppite gi amal na ay njeexiit ci xarkanam ci fukk ak benneelu siiwal gi. + +Taariixu jagal yi + +jagal gu njëkk gees def ci CD-ROM mi ngi génn 1994. + +Lëkkalekaay yu biti + dal bees ko jagleel + 9 ak 10 ci lënd gi + 11 jagal ci lënd gi + +Jimbulang +Sékk sàcc, bëgg ceep ak ndox, samab jaam rekk nga, Ahloubadar 23 Mee 2009 à 14:48 (UTC) +Weeru Samwie mooy weer wi njëkk ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Baat baa ngi jóge ci latin januarius, ngir maggale ko yàllay waa-rom ja: Janus (yàllay bunt yi). Ca jamono ju yàgg ja, moo nekkoon fukk ak benneelu weer ci arminaatu waa-rom. + +Samwie +Weeri at mi +Weeru Fewirie mooy ñaareelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Baat baa ngi jóge ci latin: februarius, ngir màggale ko yàllay waa-rom ja: Februa. Ca jamono ju yàgg ja, moo nekkoon ñaareelu weer ci arminaatu waa-rom, at mi 15 Maars la daan door. + +Mooy weer wi gën a gàtt ci at mi, mooy wenn wi dul àgg mukk 30 fan. + +Weeri at mi +Fewirie +Weeru Maars mooy ñetteelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Baat baa ngi jóge ci latin: Maars, ngir màggale ko yàllay waa-rom ja: Martius (yàllay xare yi), ci weer wii daanaka la xare yi daan door, ndax ci la tangaay bi di tambalee. Ca jamono ju yàgg ja, moo nekkoon weer wi njëkk ci arminaatu waa-rom. + +Weeri at mi +Maars +Weeru Awril mooy ñeenteelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. Ca njalbeen moo nekkoon ñaareelu weer ci arminaatu waa-rom ba. + +Baat baa ngi jóge ci latin : Aprilis. + +Weeri at mi +Awril +Segg g : rab la ci rabi àll yi + +Rab +Golo : rab la ci rabi àll bi + +Rab +Ñay w: rab la ci rabi àll yi, bokk na ci rab yi gën a rëy ci àll bi, + +Rab +Nak: mala la ci mala yi dëkk ak nit ñi dees nako lékk.... + +Rab +Dàngin: golo gu mag, rab la ci rabi àll yi.... + +Rab +Gar: gaynde gu màggat, rab la ci rabi àll yi.... +Jinax j: rab la ci rab yi dëkk ak nit ñi.... + +rab +Weeru mee mooy juroomeelu weer ci arminaatu Gregori di ñetteel ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin, doon tur bu ko waa-rom yi joxoon ngir màggale ko seen yàlla ju jigéen ja maius, jàppees na ne Romolos miy buuru Rom bi njëkk moo ko ko jagleeloon. Ca jamono yooyu moo doonoon ñetteelu weer ci arminaatu waa-rom bi. + +Bés bi njëkk ci weeru mee xamees na ko niki bés bees di màggale liggéeykati àdduna bépp, ba ci Senegaal kenn du ko liggéey, ci Diiwaan-yu-Bennoo yi ak Kanadaa ñoom 1 Sattumbar lees ko di xewal. + +Weeri at mi +Mee +Weeru Suwe mooy juroom-benneelu weer ci Arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Baat baa ngi jóge ci latin: junius. Jàppees na ne yàllaay waa-rom ju jigéen ja Junon lees ko jagleeloon ngir màggalee ko ko. Ca jamono ju yàgg ja, moo nekkoon ñeenteelu weer ci arminaatu waa-rom bu yàgg ba. + +Suwe mooy weer wi njëkk ci tangaay bi ci réew yi féete ci xaaju-kol-kol bu bëj-gànnaar bi. + +Weeri at mi +Suwe +Weeru sulet mooy juroom-ñaareelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin Julius, ngir màggale ko Suul Sesaar, buuru Rom ba woon, moom mi taxawaloon ci 46 nj. j. Isaa arminaatu Suul, tudde woon ko boppam, moo nekkoon juroomeelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Sulet +Waxset mooy juroom-ñetteelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci Augustus, ngir màggalee ko ko moom mi nekkoon buuru Rom ci 8 nj. j. Isaa. laataa moom moo nekkoon juroom-benneelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Ut +Sattumbar mooy juroom-ñeenteelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin september, jóge ci septem (juroom-ñaar), moo nekkoon juroom-ñaareelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Sattumbar +Oktoobar mooy fukkeelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin october, jóge ci octo (juroom-ñett), moo nekkoon juroom-ñetteelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Oktoobar +Nowembar mooy fukk ak benneelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin november, jóge ci novem (juroom-ñeent), moo nekkoon juroom-ñeenteelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Nowembar +Disambar mooy fukk ak ñaareelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul. + +Turam ma ngi jóge ci latin december, jóge ci decem (fukk), ndax moo nekkoon fukkeelu weer ci arminaatu waa-rom bu jamono ju yàgg ja. + +Weeri at mi +Disambar +Tamxarit (محرم ci araab), mooy weer wi njëkk ci yu gàddaay gi, moom nag bokk na ci li ñuy wax ci Lislaam "Al-ashur al-hurum", (maanaam weer yu am worma yi): tamxarit nag tuddees na ko ci araab "muharram" ngir ne araab yi dañu ci daan araamal xeex. + +Xew-xew + Ci lees di xewal bés bu njëkk ci at mi. Ci senegaal ci lañuy taajabóon. + Ci la shiit yi di fattalikoo xareb Karbalaa ca Iraak. Ca lañu faatee Useynu ben Aali sëtu yonent bi. +Bisu Tamxarit +weeri wolof +Diggi-gammu, (صفر ci araab), mooy ñaareelu weer ci weeri wolof. Tuddees na ko "safar" ci araab giy firi féex, wéet, limub tus, ci araab mi ngi bawoo ci baat boobu di safar {sifr) ndax féexam ga, ëmbadeem ga dara. Kon safar tuddees na ko safar ci araab - ma baamu- ngir ne weer la wow këri araab yi dañu ci daan wéet, féex ci ci ay ñoñam ngir xare-ji, waxees na it ne li ko waral mooy araab yi dañu ci daan song ak a lokki giir yi, bu ko defee ñu leen di "safaral" maanaam tusal ci seeni bagaas ( maanaam jël li ñu am ba duñu deseeti "tus" (sifr),ñu mujj di ñu wéet ciy yére, féex ciy bagaas). + +Xew-xew + Ci la njabootu Muhammad dugg njéndul Yasid ca Siri. + ci 7 fan la juroom-ñaareelu imaamu Shiit ba Musaa al-Kasim judd. + ci 9 fan la ndamu Imaam Aali ibn Abi Taalib ci xareb Nirwaan. + ci 18 la serigne touba démone gabon. + +Lëkkalekaay yu biti + Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) + The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +weeri wolof +Gàmmu, ( ci araab ربيع الأول) mooy ñetteelu weer ci weeri wolof tuddees na ko noonu ngir ne araab yi dañu ci daan lolliwu, maanaam daan ci am am ñax, di ci sàmm seenug jur, am ñu ne daa dëppoo ak lolli bi moo tax ñu tudde ko ko. + +Ci wolof nak daa yem ak weer wees di màggalee juddug yonnent bi te màggal googu moo tudd Gàmmu ci wolof. + +Xew-Xew +ci lees di màggal juddug yonnent bi, ci ñi yellal ni warees naa màggal ag juddoom. + +weeri wolof +Xareb Àdduna bu Njëkk (1914 – 1918) benn la ci ñaari Xarey àdduna yi tàkk ci xaaj bu njëkk ci ñaar-fukkeelu xarnu bi. Xarnu bi seere na tàkkug ñaari xare yi gën a rëy ci taariixu nit, beneen bi di Ñaareelu Xareb Àdduna bi (1939 – 1945g). + +Li waral xare bi +Xareb àdduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi, + +Sabab yu jonjoodi yi +Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy: + +Gëpplante gi ci wàllug canc +Gëpplanteg àdduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg ndefar gi, ci fukk ak juroom-ñatteelu xarnu g . Réewi ndefar yi seeni cawarte gën naa yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom-ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo (société) yu ndefar yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi-alal yi dëkk ci yile réew, rawati na nag ci réewi Tugal yi am ay noste yu gore (systèmes libéraux). Bu ko defee ñu jóg tàmblee seeti-ji cémb (brut) yi manul a ñàkk ngir liggéeyi ndefar yii man dox, man a jëm-kanam. Tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye-ji seen liggéeyi ndefar yu wuute yi. + +Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante réewi ndefar yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci àdduna bi, bu ko defee ndefarug ngànnaay gën a jëm-kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu. + +Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante waa-Brëtaañ yeek waa-Faraas cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay Almaañ yi bari woon nañu ci ja yu àdduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon-kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom yu Almaañ yi ci réewum Usmaan mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb àdduna bu njëkk bi. + +Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu àdduna bi mooy li duggal àdduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal. + +Tapoo yu réew yi + +Gëpplanteg politig gi aju woon ci canc ci àdduna bi dafa gënoon na jëm-kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu àdduna bi gënee jëm-kanam. Loolu nag tax ba ay dank sosu yu réew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare ci diggante ab lim ci réew yi seeni njariñi canc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci déggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu, yii di ñëw: + +Tappoo gu ñaaral gi +Gii tappoo amoon na ci diggante imbraatóoru Almaañ gi ak gu Otris gi ci atum 1879, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw: + + Bu Riisi gu Xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war naa dimbli mi nu song. + Bu menn ci ñaari réew yi tappoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu. + Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Riisi ak Faraas, ñaari réew yii tapoo de war nanoo ànd liggéey ngir xeex loolu. + +Tappoo gu ñattal gi +Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tappoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi ci 1882, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatóorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll. + +Itaali duggsi na ci tappoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Faraas, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Alseeri ci atum 1830g, ak Tiniisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tappoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Faraas ak Brëtaañ ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci Géej gu Diggu gi. +Dëppoo gu Fraans-Rusi gi: + +Dëppoog cofeel gu Faraas-Riisi +Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Faraas ak Riisi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na ci atum 1886, daal di gën a jëm-kanam ci atum 1888g, bi ñaari réew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Faraas di jox Riisi ngànnaay, te jëmale-kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Faraas ak Riisi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw: + + Taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari réew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi. + Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari réew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante. + +Dëppoog cofeel gu Brëtaañ-Sapoŋ +Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Brëtaañ ak Sapoŋ ci atum 1902g, lii la yaxal: + + Bu xare tàkkee ci diggante Sapoŋ ak Riisi gu Xaysar gi, Brëtaañ da caa war a génn te seetaan. + Bu meneen réew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Riisi ak Sapoŋ , kon Brëtaañ da ciy war a dugg moom itam, jàpple Sapoŋ . + +Dëppoog cofeel gu Brëtaañ-Faraas +Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Brëtaañ ak Faraas ci atum 1904, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax: + + Féexal Faraas, joyal ab loxoom ci Marok, gii nga xam ne jotoon naa temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Alseeri ak Tiniisi. + Faraas moom tam nangul Brëtaañ teg gi mu teg loxo Isipt ci atum 1882 + +Dëppoo gu cofeel gu Brëtaañ-Riisi +Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Brëtaañ ak Riisi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax: + + Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan, ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Riisi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Brëtaañ jël gu bëj-saalum gi. + +Màggug yëngu-yënguy xeetu yi ci Tugal +Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ àdduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom-ñeenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog réew yi leen di àtte cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am réewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy: + +Mbootaayug Slaaf gi +Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatóor gu Otris gi, ak sos réewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Penku Tugal. +Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Riisi gu slaaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Riisi gu Xaysar gi. + +Lëj-lëji àdduna bi +Ay lëj-lëj yu fasu yu àdduna bi sosu nañu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb àdduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante réew yu mag ya ngir seen gëpplanteg canc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu: + +Lëj-lëju Maraakes +Faraas yàgg naa waaj ak a naal ngir teg loxo Maxreb gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tuniusi ak Alseeri, Faraas a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig canc. Ci noonu Faraas lijjanteek Brëtaañ seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga ca atum 1904, Faraas daal di bokki ca ndaje ma ñu njëkk a def ca dun bu wert ba ca atum 1906 ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi. + +Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Faraas la gënoon a nekk, ndax réew ya fa daje woon dañoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Faraas wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. +Faraas nag jariñu na bu baax ci dénk gi ñu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon péey ba, da faa daal di woon yabal ay dooley xare yu Faraas ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ, mi àndoon ak buurub Maraakes, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Faraas. +Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Faraas yabaloon am mbooloom xare ca Faas ci atum 1911 ngir teg ko loxo. +Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ ci atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Faraas-Almaañ bi, la fa juddoo di: jox Almaañ ay moomeel ca Kongóog Faraas ga, bu ko defee Almaañ nangul Faraas nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu àdduna bépp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug àdduna bi. + +Lëj-lëju Balkaan +Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan. +Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum 1908g. +Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba. + +Lëj-lëju Maseduwaan +Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon a jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen. + +Lëj-lëju Tripoli +Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginnaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci. + +Sabab yu jonjoo yi +Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaay gu làqu ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Riisi gu Xaysar gi. +Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def. +Otris daal di gaaw jariñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak këri tas-xibaar yi noonu Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jortu ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tontuwul, waaye Serbi moom tontuwul . + +Jibalug xare bi +Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal. + +Lefum xare bi +Jë bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru. +Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g. + +Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani. + +Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa. + +Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay. + +Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom. + +Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo. +Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g. + +Lijjanti yi ci ginaaw xare bi +Reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris. +Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Faraas. + +Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk. + +Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi. +Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g. + +Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi. + +Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko. + +Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations) teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi. + +Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon. + +Gongikuwaay +Téere taariix bu bees bi te jamonoo bu Abdu Xaadir KEBE + +Xarey àdduna +Ca Afrig, diine yi yagg nañu fa am. Diine yi am Afrig (yawut, kirist, lislaam), ñoo bokk cosaan. Ca jamono nguuru Kuus amoon, tey di nekk wa Sudaan, nit ñoo fa nekkoon, dañu daan nekk ca diine yu jekk am ca adduna, ci li taarixkat wonee. Ca diine boobu, nit yi dañu daan gëm benn Yalla. Li ñu wax monotheisme ci nasaran. + +Wa Misra tey di nekk Isipt, ba Sudan, diine boobu moo fa amoon. Ca diine boobu, yalla, mel ni lislaam, ay yu bare la amoon, tur bu nekk wonee benn jikko bu yalla. Ca tur yi amoon na: Ra, Amon, Atoum, Aton, etc. + +Taarixkat yi, ñu mel ni Seex Anta Joob, walla Sarwat Al Anis Al Assiouty, wonee nañu, diine yawut, kirist ak Lislaam, foofu (wa Misra) lañu cosaanoo. Ndax yonent yi ñu nekk ca diine yawut ak kirist, mel ni Ibrayima, Muusa, Issa, ca seen teree, biibël ak tora, deeni ne, jaar neen Misra, te foofu, jang nañu yu bare ci diine bu fa nekkoon. Ba noppi yobale nañu Diine boobu ca seen bokk yawut. +Taarixkat yi wone nañu tamit, yawut yi nekkoon ca reewum nit ñu ñuul yi, di wa misra, ñoo doon nit ñi ñu wowee habiru walla hyksos , ci keyitu jamono jii ñu seet. + + +Turu ñu fekk ci askanu yawut ak naar, yu bare, ca diine afrig boobu la joge: + + Ibrahim, mooy Ib-Ra-Him, ca lakku wa misra bu fa amoon bu jekk mooy, ku am yalla (Ra) ca xolam. + Muussa, mooy Messu, ku yalla jur. + Sara, Sa-Ra mooy, doomu yalla. + Myriam, Meri-Amon, ku yalla begg. Amon mooy benn turu yalla ca diine Afrig. + +Ca Misra, lakk bu fa amoon, ro en kemet (lakku reewum nit ñu ñuul yi), la tudde woon, seen bind di medu neter (baatu yalla). Lakk boobu moo jur ay lakk yu bare ci biir afrig, ci li taarixkat yi mel ni Theophile Obenga firndel. + +Wa misra mooy fu xeet yi nekk ca biir afrig tey, cosaanoo, te diine bi fa amoon, yobu nañu ko ca fu ñu dëkk tey. Di Reew yi Afrig bu nekk ca suuf Saara. Ndax waaso yi nekkoon wa Misra, dañoo mujj gadday ca biir afrig, ndax amoon naa ay doxandem bu leen fekk seen reew, te leen noot ak di leen teg dund bu meti. Yoro Booli Jaw, bokkoon ci garmi newoon wa Waalo, wax na ci naka xeeti nekk Senegal daaw reewum Misra ba agsi dexug Senegal ca njeelbeen, te li cosaan doon wax rekk la doon tekki. + +Bi ñu wacce ca Afrig boobu, xeet yi tassaroo nañu fa, te ba noppi xeet ku nekk, amoon na benn tur ngiir tudd yalla: + + Mandinke yi, Bambara, Jula, Xasonke, yalla, Maa lañu ko daan tuddee. + Sooninke yi, Aari. + Pël yi, Geno lañu daan wax. + Séeréer yi, Roog Seen + Joolaa yi, Emitai + Sonraï yi dëkk ca Mali ak Niseer, Yarkoï + Bassari ak Bedik yi, Ununga + Dogon yi: Amma + Yoruba yi Ca Niseeria: Olodumare + Masaï yi ca Kenya: Engaï + Zulu yi ca Afrig bej Saalum: Inkosi + Akan yi, ca reew mi Togo, Gana, kote diiwaar: Mawu Lisa + Wa Ecoopi: Waqa + wa Kongo ca xeet yi Bantu: NzamBe + +Diine boobu amoon ci afrig ba leegi, gestukat yi, nigritism walla kemitism, yeneen wax animism ca nasaraan, lañu ko tudd. Waaye, ñu nekk ca Afrig, te ñu doxal diine boobu, am nañu yeneeni tur ngir tudd ko. Day wuute ci xeet yi. Ndax xeet bu nekk, ci seen lakk, dinañu ko joox benn tur. Wante, diine boobu, feppu m��na nekk ca Afrig, benn la. + +Xam nañu ni, ca xeet bu nekk, Yalla wacc na ay yonent. Li mooy tax diine afrig boobu, am seen yonent. + +Asar, yonente bu jekk am ca aduna ca diine boobu, boo demee ca Misra. Am na tur yu bare: Issa (ca lislaam moye Issa), Oni (ca diine nasaraan moye Ori). Taarixkat yi ne nañu, taarix bu Asar moo jur taarixu Issa bu yoonu Kirist ca Biibël. Ausar ca xeet Anu la bokkoon, benm xeet bu amoon bu jekk, dëkkoon ca Sudan (Nguruu Kush), ñoom ñoo tabax nguuru Misra, ak Buur Fari ba, mu tuddoon Narmer (Sooninke yi xam neen ko, te Nare Mari lañu ko wowee). Ay Firaouna lañu woon, di tur bu ñu fekk ci lakk yi am Senegaal (Fari, Farba, Faren, etc). Aset (turu Aïssata ci moom la joge). Moo doon jabaru Ausar. Aset ak Ausar ñoo jur Hor, seen doom. Natal bi ñu wone yaayu Yesu/Issa, mu tudd Maryama, ak domam, ca natal bi ñu wonee Aset ak doomam Hor la joge. Set. Ca diine afrig amoon Misra, mooy Seytan. Satan ca diiney kirist, wala Seytan ca diiney lislaam. Liggeeyam mooy mu sonal nit yi ca adduna, tek leen coono. +Djehuty, ki moo indaale xam xam, ak bind, ca adduna. Ñu mën ko boole ak Idrissa ca lislaam, wala Henoch ca dinne nasaraan. + +Amoon na ajjana (seshet iarou ci diine Afrig) ak safaara nit ñu bon doon dem, di Duat, Al-Jahim ca lislaam, l'enfer ca diine nasaraan. + +Maât, doon yoon wu baax ñit ñii waroon ne suñu buggoon dem seshet iarou, am barke. + +Ñoom ñoo yonent yu gëna am solo ca diine Afrig bu amoon wa Misara, ndax am na yeneen, te xeet yi ca afrig, bu nekk, ba tey, am nañu tur yu bare ngir tuddu yonent yi. Ca diine bii, Neteru moo doon turu yonent yi. Bu ñu xolee ci lakk yi Afrig yi, ñu gis ay baat bu ko niroo (nutar, ntori, tooru, tuur, etc). + +Ca yoonu imbraator gu gana, lislaam ñow na soowu Afrig, ca jamono boobu, lislaam ak diiney bu Afrig, ca jamm lañu doom dëkkando. +Ak tubaap yi, diiney nasaraan ñow wa diggu afrig ak Afrig bu penku. Waaye ñu jekk topp yoonu Kirist ci adduna, ñooy askan wi mu tudd Kopte, baawo ci askanu wa misra. Ak Jiyaar yi jullit defoon ca XIXee xarnu, diine bu Afrig ba, waññi na bu baax. +Tubaap yi tamit ak canc gi, def neen ñi, diine afrig boobu mu waññi bu bari. + +Waante am na ay xeet, diine lislaam walla kirist lañu nekk, waaye dañu duggal ca seen gëm, ay gëmu nekk ca diine afrig, mel ni joola yi, walla Bantu yi, Lebu yi, Akan yi. + +Téerekaay + + La Philosophie africaine de la période pharaonique, Théophile Obenga. + L'Origine négro-africaine des religions dites révélées, Doumbi Fakoly. + Bilal le prophète, Doumbi Fakoly. + Parenté génétique de l'égyptien pharaonique et des langues négro-africaines, Seex Anta Joob. + Théophile Obenga, Origine commune de l'égyptien ancien, du copte et des langues négro-africaines modernes. Introduction à la linguistique historique africaine. + Nations nègres et culture : de l'antiquité nègre égyptienne aux problèmes culturels de l'Afrique noire d'aujourd'hui, Seex Anta Joob. + Cossanu Afrig cib nataal, Seex Anta Joob. +diine + +Afrig +Waxtaani Sëriñ Tuuba, xaajub ñaaréel bi + +Ag jiitël +alaaji mbakke xaadimul xadiimi mooko dajale fii ngir bëgg muriit yépp jariñu ci, +yàl nako Yàlla nangu ci barkeb Sëriñ Tuubaa te békloo ko ci àdduna ak allaaxira aamiin. + +Ahoozu billaahi minash shaytaanir rajiim, wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatihaa minash shaytaanir rajiim, rabbi ahuuzu bika min hamazaatish shayaatiini wa uhoozu bika rabbi ay uahdhuruun. + +Waxtaani Sëriñ Tuuba +قادله الله مااختارله + +Waxi Sëriñ Tuubaa ci yéene: + +Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Néena: Boo bëggée +jàng Alxuraan Nanga ci yéene "Génn ci lépp lula sunu Boroom tànnalul; +Ak dugg ci mboolem limu la tànnal. Boo dee jàng ak Xasida ci sama Xasida +yi, Man nga cee yéene lula neex, Kon danga ko am, Bu fekkee ci yima def +ginnaaw bima jugee jolof la walla ca at mama fa jugée, Waayé Xasaayid ya + ko jiitu moom déedéet", Bu dee Wirdu, nanga ci yéene Yàlla jariñ la +ci Àdduna ak Allaaxira, ci lu dul Lor, Ak jege Yàlla ak Yonent bi +(Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc) +jege gu lay jariñ te dula lor, Boo dee Naafila nanga yéene Dundal Sunnas +Yonent bi (Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc) +Saar yu gàtt yi, yu la ci neex jàng, (Wér na lool) + +Sëriñ bi Néena: Ku bëgg Yàlla jox ko limu bëgg ci Àdduna Ak Allaaxira, +Nay toppi ndigëlam, Ku bëgg a toppi ndigëlam nay yéene, Ndax yéene moo koy +Wommat jëmé ko ci [Ag] Topp. Ku bëgg Yàlla diko fegal lumu ragal ak lumu Sib, +Nay teet (sori, bàyyi) ay tereem, Ku bëgg a teet ay tereem nay Yéene, +Ndax yéene moo koy wommat jëméko ci teeti Tere. [Wér na lool] + +Sëriñ bi mas nay laaj, kenn ci ñi mu fi waccoon (bàyyiwoon), kooka nangu +koo wax la am lool (sawar ci nettali ko), Sëriñ bi neko "Loolu Wolof di wax +saan wu déllu si Xam nga koo! ?", Mu neko "Waaw", Mu [Sëriñ bi] neko +"Xanaa ba ñu koy Wax, Saan wu baax taxul" ? Mu neko: Déedéet, Saan wa ca des +kay lañuy wax, Sëriñ Bi neko: Saan wu baax déy, wa ca gën a rëy a gën. +(Wér na). [Boroom Téere bi néena:Loolu mooy li Wolof di wax ne: +«Yéene Néeg la; Boroom a cay fanaan»] + +Waxi Sëriñ Bi ci fonk ay waxm ak bañ koo waxal lumu Waxul: + +Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Néena: Waxal waaju baax, +lumu waxul leegi la, Waayé bu jëggoon, Ku ko defaa, bu ñu xëyee, dañu lay fekk +nga doon GOLO, Binga xamee ne Yonent bi -Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, +ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc- ñëw na, Lako Yàlla terale du defati loolu, +Waaye ba leegi, ku ko def àtte boobu mingi daw ci yaw. + +Sëriñ Bi neena: Des na diir bu gàtt, Ku man a wax ne: «Sëriñ Tuubaa neena, +Te muy dëgg duñu nangu, nga diko waxe fi suuf, Fu kawe nga koy waxe» +(Siiwna), + +Sëriñ bi neena: fekke sama waxtaan, jarna sol dàlli weñ, Di dox ba bamu Xar. + +Sëriñ bi neena: Damaa wax sama boroom, neko: Mbooloo mii ma topp, di wuyyoo +samaw Tur, di taasu ci sama barke, Damaa bëgg nga wax ma, Li nga gën a bëgg, +Ma sant léen ko ñu defal lako ? [neena:] Saa boroom ni tekk, ba mani bu doon, +kuy fàtte mani fàtte na, Ma dellu waxaat koko, Mu [Yàlla] neeti tekk, Ma dellu +waxaat koko, Mu ne ma «Fu ñu tollu dila waxtaane, Fu ñu lay waxtaanee, danaa +léen fa tiim, ak waamew (taw bu matale) xéewël, Di léen sotti, Ba kero ñur bàyyi +Ma door a Séwét» (Siiwna). + +Waxi Sëriñ bi ci Julli: + +Sëriñ bi neena: Ubbikoo ci Julli gu Farata, Ludul ALHAMDU LILLAH (FAATIHA), +Mingi melni nga dem ci Kilifa ga nga gën a fonk, neko "Dama laa soxla", +Mu ànd ak yaw, ba ca barab bamu, gën a fonk, Àgg suuf nela: Waxal sa Soxla ? +Loo wax ludul ALHAMDU LILLAAH, mingi melni nga séen Janaab (Muus) foofa, +Wacci ko fa, daw topp ca. (Wér na) + +Sëriñ Bi masnaa sëlmal Jullig Timis, Wax ni: Barab bañuy dekkee ak Bañuy deggee +daa soree lool, Koo xamni daana taxawal Julliy Juróom, Dees koy Defaral, Lumu +war ci yoolub ay Julléem, Ba àgg fa ñuy dajee, Ku daawul taxawal Julliy Juróom nag, +Bu dekkee, dañuy jàppu, ci ay tànkam, diko diri, ci Kanamam wuti Taxawaay ba. +(Wér na lool) + +Sëriñ bi mas naa sëlmal [Jullig] Gee ne: «Dama ni, Koo xamni Julli dakoo +soxlaal waliif (bàyyi fi) mbir yi, Dana jariñ ci julli gi, ak ci mbir yi, Koo xamne nag, +Mbir yi dakoo soxlaal waliif Julli gi, Du jariñu ci mbir yi, Du jariñ ci julli gi» +[daa di ne:] Jaamu Yàlla mooy laggéey, Biñu nu sant, Aada yi nag, dañu leen di dimbandikoo +rekk ci Jaamu gi, [Teg ci ne:] «Fa Quuluu Anfusakum Wa Ahliikum Naaran» +[Wér na lool] + +Waxi Sëriñ Bi ci koor ak Laylatul Qadri: + +Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu-: Weeru Koor daawul yonni ku woorul, +Daawu ko def Darra, Weeru Koor yit ci la daan, gën a bari lumuy joxe. (wér na lool) +(Mani: xayna day xamle ni, Ku woorul deful ak moom nenn). + +Amna Taalube yu doon dundal [Guddig] Laylatul Qadri, Ci tënk bi Sëriñ bi def, Ba mu ko yëgee, +Ni léen du tay, Wax[aat] léen ca beneen bis, [ni léen:] tay jii la. (Siiwna) +[Boroom téeré bi ni: Lii nag, Limuy war a tegtale, mooy Lëm googu Yonent bi - +(Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc)- Wax la, +Waayé térewul ñu war di topp tënk bi Sëriñ bi def,] +(Mani: Ginnaaw Xam-xam bi ci ñeel Sëriñ bi noonu ñeelu nu banu man koo ràññee, +nanu tënku ci tënk bi Sëriñ bi def, Dàkke koko) + +Waxi Sëriñ Bi ci ASAKA: + +Amna ku mas a juge fu sori, Ñëw jox Sëriñ bi Xaalis bu bari, niko Asaka la, Dellul Fanga jugewoon, +Amna juróom ñatt ñu Alxuraan Tudd, Koo ci gis nga jox koko. + +Waxi Sëriñ bi ci Tuub: + +Sëriñ neena doomu aadama ñaari rekk la am: Yéene ak Tuub, Li baax bu fekkee daa bari +ba maneefut a def lépp, La nga man léppu danga koy def la ca des, nga diko yéene, Bu +ko defee ñu def langa yéene ni la nga def dila ko fay. +Li bon yitam bu fekkee daa bari ba maneefuta ba (bàyyi) lépp, Dangay bàyyi la nga man +la ca des nga diko tuub, Su ko defee dana ñu ko far, Te lu ñu far ak lu ñu bindul ñoo yam. +(Wér na) + +Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Neena: Ki nga xamni dañu koy jëmale +ci lu amul njariñ ginnaaw tuub gu sell, Mingi melni ku waccu ba noppi, ñu lekk loo koko, +Ki nga xamni dañu koo jëmale ci lu Haraam walla lu ñu sib ginnaaw Tuub gu sell, Mingi melni +ku ñu lekkloo ay xal walla ay jiit, Bu léen ku baax woowee ci ñam wu baax, na ngeen lekk, +Waaye ku leen bëg a lekkloo am waccu walla ay xal walla ay jiit bu léen nangu. (Wér na lool) + +Waxi Sëriñ bi ci ndigël yi ak tere yi: + +Sëriñ bi masnaa laajte ndax xam ngeen «Al-Iimaan» ak «Al-Islaam» ak «Al-Ihsaan» ? ñu neko: +Degg nañu ñu di ko wax, Muni: «Al-Imaan» mooy léppu lu am nga gëm ni Yàlla a ko dogal, +«Al-Islaam» mooy léppu loo am nga génne ca wàllu Yàlla, «Al-Ihsaan» Mooy lumu dogal mu neex la. +(Wér na lool) + +Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Masnaa laaj, «Wa Af`aloo Al-Xayra:S22,V77,وَافْعَلُوا الْخَيْرَ» +Nu ngeen koy firee ? ñu ni ko: Wa Af`aloo, nangeen def, Al-Xayra, aw yiw, Mu ni: ñu koy def ? ñu ni cell, +Mu ni: Wa Af`aloo, juróom ñaari Haraf la, Al-Xayra juróom i Haraf la, Juróom ñaari cer yii lañu wax ni +saxal leen ci juróom i ponki Lislaam yii, te bu leen ko ba. (wér na) + +Sëriñ bi masnaa laaj ndax xam ngeen, «Waajib» ak «Manduub» ak «Mubaah» ? ñu ni ko: ñi ngi koy dégg, Muni ndax xam ngeen luy seen «waajib» yéen ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni:mooy wàcc lal yi te dem ci der yi jaamu ji Yàlla, Daa di ni: Xam ngeen luy seen «Manduub» ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni: Wacc a ndiku ndamu +ba ñu ni démb la bis pénc, Daadi ni: Xam ngeen luy seen «Mubaah» ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni : Darra, Darra, Darra, daadi ni: +Darra ju jëkk ji, mooy Sunu boroom mii nu bind, Ku xam ci moom darra, du def lumuy tere, +Ndax moo boole «Xudratu» (Kàttan) Ak «Iraada» (nammeel) te bu yékkatee yaram ba kenn du ko tere, +Darra ji ci toppu mooy àdduna jii ñu nekk te xalsatfee juge, Ku xam ci moom darra dooko jox sa darra, Ndax looko jox ñàkk nga ko, +Darra ji ci topp, mooy Allaaxira jee nu jëm te di fa sax ba fàww, +Ku xam ci moom Darra doofa dawal Darra ba naw ko, ndax Darra du fa doy.(wér na) + +Am na koo xamni da daan def, bu togee ci wetu Sëriñ bi di bind «Kun Fayakuun» am bis Sëriñ bi jàppu ci mbangam, +neko:«MIN HUSNI ISLAAMI AL-MAR I TARKUHUU MALAA YUXNII», (Bokk na ci liy rafetal ak njullit bàyyi lépp lula am a lul njariñ) ni ko: "boo manta ñàkka bind deel bind «AL-KADHIBU HARAAMUN, (fen haraam na) WA-L-XIIBATU HARAAMUN, (jëw haraam na) WA-AlN-NAMIIMATU HARAAMUN (rambaaj haraam na)» KA DHAALIKA (niki noonu)". +(Wér na) + +«فاقصص القصص لعلهم يتفكّرون +ماكان حديثا يفترى و لكن تصديق الذى بين يديه +وتفضيل كلّ شي ء وهدى ورحمة لقوم يومنون.» + +Waxi Sëriñ Tuubaa ci diggante boroom kër ak soxnaam, ni ñuy dëkkee + +«وعاشروهنّ بالمعروف الخ... صدق الله العظيم» + +Am na ku doon jambat soxnaam ci ci Sëriñ Tuubaa ▬قادله الله مااختارله ▬ Sëriñ bi ni ko nangu naa +ànd'ak yaw ngeen jaamu Yàlla ? Mu ni ko waaw, Mu ni ko kon nak damaa bëggoon nga xamni la taxoon +ñu jox la ko moo di am nga jàngoro joo xam ni moom rekk, moo yor saafar sooko man a saafaraa te +doo ci am bàkkaar bu ko defee nga jàppee ko muy saafaras jàngoro jooju, saafara nak bu yàggee nga +bëgg koo jàppe ab dund, dang ci'y gis sikk, ndax day jur jàngoro, barina yu ngeen di jàmbat te noonu dóng la .'. wer na + +Am na ku amoon ñatti soxna, ñaar ña xëy-xëy dem (melni dañ koo takkoo), Mu yónnee ci Sëriñ Tuubaa ▬قادله الله مااختارله ▬ ni ko bama demee batóllu ci àdduna dama koo bàyyi tóppu ko, bama demee ba am lama doon wut ñaw sampu kër ba am ñatti soxna, ñaar ña xëy-xëy dem melni dañ koo takkoo ma bëggoon bu dee sikk si ci man la nékk nga wax ma ko ma ñawaat ndax ma defaru, bu fekkee ci ñoom la nékk nga wax ma ko ma bàyyi leen, Sëriñ bi wax ndaw la dem a ngun nafaa ? mu niko déedéet, Sëriñ bi ni ko +neeko booba ba tay sikk si ci moom la nékk, nafa dem buñ nangoo ñëw mu xam ni sikk si ci moom la +nékkoon, buñ nangu wu la ñëw mu xam ni sikk si ci ñoom la nékk.'. (Mu dem fa ñu daal di ñëw) +wer na + +Ay dénkaane +Bu ngeen xëyatee: +Na ngeen jiital jaamu Yàlla teg ci nangoo liggéey +Def seen naqar muy seen bànneex te def seen coono muy seen nooflaay +Wéttalikoo topp ndigali Yàlla te bañ a wéttalikoo jëmm +Na ngeen def ndigali Yàlla muy ab sëriñ te bañ a def ab sant muy ab sëriñ +Ku bëgg a texe ci àdduna dangay nangoo liggéey +Ku bëgg a texe ëllëg dangay nangoo jaamu Yàlla. + +Laabire nit ñi moo gën fital jiyaar +Bàyyi fen moo gën jàng Alxuraan + +Yoonu murit +Sëriñ Maalig Basin Si gane na àdduna atum 1871 génn àddina 1955 (am 84ci ay at ci ag dundam) baayam tudd Sëriñ Maxtaar Penda Si ndayam tudd Soxna Xadi Ñang, di ab jullit bu jëfe ag njullit te it di ab sufiyanke bu mag di taalubeb Sëriñ Tuubaa jébbalu ci atum 1905 + +bindub jëmmam +Ndaama la woon su xees te am bët joti cer am xorom lool ci waxiin ak jëfiin + +lenn ci ay jikkoom + +ku bari kersa la woon aki teggiin te bëgg lu rafet bëgg sutura lu ko waay mas a jox ci mbooloo ginnaaw ñepp gis nañ ko dakoy tasaare jox ko mboolo ma waaye du ko jariñoo, ku bëgg sunna (roy yonnent bi) la woon akuk cet bu daan tëdd, mbaa mu lekk mbaa war daaba (wata, fas, ak luni mel) dana jàpp, fu mu took jublu xibla (pénku) te du tëdd mbaa toog mukk ci kaw ab lal bëccëg, ku bëggoon xet gu neex la daawul tàggoo ak bitéelu laj koloñ te fonk ay ser (yére), ku xamoon liggeey la te man liggeey, ku ko mas a liggeeyal loo xarala xarala mu won la ca loo xamul, ku man a yare la woon, te xaral te ñime njaboot àttan njël li, Sëriñ Abiibu Si ( doomam) nee lenn rek laa gisoon mu bañ ko lool góor guy dem ci këri jigéen ba daana wax ni: Donga buy tërbiyawu moo ngi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru, ku am Tawhiid (weetal Yàlla) la woon ba daa ko jàggale te daa ko jàggal jigéenu këram ba amoon na ca ku mokkaloon teere bu tudd "Burkaanu Sanoosii", mas nay waare ci Tawhiid fek booba am kuy tuddu lu (ku wopp di tudd turu jàmbur) ay bokkam jàpp kooka di ko dóor ba yàlla dugalee ka tawatoon faatu, mu ni leen bëgg geen xam ni lu am yàllaa kii geen doon tam ba di ko dóor li mu ci doon dafa melni ku romb màngo gu ñoral mu xam ca doom bu ñor mu gësëm ko doom ba rot ñu ni ko yaa ko ray te kat bu ko laalutoon ab diir mu rot (nde ñor na), daadi wax li Yàlla ni: وَمَا ڪَانَ لِنَفۡسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِ كِتَـٰبً۬ا مُّؤَجَّلاً۬‌ۗ = nekkul di ñeel bakkan dee ci ludul ndingalul yàlla ci àpp bu dog, + +ku woyofal àdduna a la woon + +daa na wax ni: mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan, Sëriñ Abiibu nee: gis naa mu sëyi loo ab taawam te defeesu ca darra batey it sëyi loo na doomam bisub talaata ñu ni ko ah Sëriñ Bi tey dey day bisub talaata, mu ni aah talaata day bañ ku ci def lu baax ñu ni ko déet mu ni kon dey di naa ko ci def, maye na doomam jàpp ca loxo ba yegg ca boroom këram ni ko dénk naa ko Yàlla te dénk la ko, + +Ku am ag taalibe la woon + +Sëñ Abiibu nee mas naa dégg mu ni boroom man Boroom Tuubaa laa jëkk a xam Yàlla, ngir bamay ndaw nekk mbakke laa gis Boroom Tuubaa xam ko, bëgg ko te booba xam a gu ma Yàlla, Mas nay waare bisub bër/hiid (tabaski, korite, mbaa tamxarit) mu ni : garab gale bu fa rasuulul laahi صلى الله عليه و سلم (ndawal Yàlla xéewalug Yàlla yal na ko ñeel ak jàmmam) taxawoon garab gale Boroom Tuuba taxaw fa, garab ga rasuulu laahi taxaw du ma fa dox, bu masaana jëm kër Sëriñ bi balaa nuyoo day jàpp, ku bëgg alxuraan (teereb Yàlla bi Muhammed indi) la woon te di ko jàng, Sëriñ Abiibu nee Sëriñ Maalig mas na koo wax ni mas naa toog ak Sëriñ Bi (Sëriñ Tuubaa) ni ko: man dey mbàkke damaa degg nga ni digal képp ku man alxuraan (ku ko man jàng bu wer) mu saxal yaari isib (benn ci 60 dogi alxuraan) ak yaari robo (benn ci 4 dogi isip) di ko jàng bëccëg, ak di ko naafilaa (jullig coobare) guddi, bama ko deggee bëgg gi ma la bëgg tax ma saxal ko madoon laaj ndax di naa ci am ab yool (pay) ? Sëriñ Bi ni ko loolu dey moo ngi mel ni for bu dajee ak boroom bu ko neexee jël bu ko neexee ba ak moom waaye yaw sax alxuraan joxeef na la, Sëriñ Maalig neena ma tiit ni ko ah mbàkke kon nu ma koy def mu ni ko xanaa di jàng rek foo yam tay bu ëllagee nga dale fa, + +Ay Waxtaanam + +Sëriñ Maalig li mu daa ubbi koo ci ay waxtaanam mooy: ndegam/segam moos Yàlla rekkay buur walla Sëriñ Tuubaa moos ken xamul lu mu doon ! fum ko masaa waxe rek xamees ni mo ngay tàmbali, Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan + +Donga buy tërbiyawu moongi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru + +Kilifa balaa war a digle day def balaa war a tere day ba + +Liy yàq kilifa, ñàkk njariñ, ñàkk a jëf. + +Lepp looy santaane na fekk nga manal ko sa bopp ba su ñu gàntoo yit nga defal ko sa bopp, ngir nit ñi ku léen yaakaar ñu wor la. + +Lees yarul kenn du man a jaxasook moom, loo bëgg a jaxasool +danga koy tàqaleek moroomam ya yaruwul. +Kilifa daa war a yar doomam, moo gën jikki ba fiy bëgg a juge, naan sama gannaaw na ngéen topp ci diw. (nde loolu ku yar sa doom bam man a yor mbooloo dooko wax), te nit ñi boo nee léen topp léen diw mii, bu diw jubul it duñ ko topp. + +Yàlla mooy ndox ma Rasoolu Laahi mooy teen ba sab Sëriñ mooy goj ba pas-pasu taalube ba mooy baak ba yitteem mooy di yoor aka jukki ba barim ndox. + +Li tax kuy wut Yàlla ay mbokkam di ko yedd, jaam buy wut boroomam talut moroomam, bu amee boroomam bëggul moroomam. + +Ku dul mer mbaam la, Kudul mar xaj la, + +Nit ku yiw, na joxe dooleem, joxe alalam, waaye bumu joxe ngoram, ndax ku joxe sa ngor dootoo dara. + +Ku gis sa baay, gis sa nijaay, gis sa taawub baay war a xam sa bopp. +ak yeeneeni waxtaan yu am solo dees na ko mottali... insaa allaa + +Delluwaay +waaxtaan yi ak jaar-jaar yi moo ngi bawoo ci téere bu am solo Sëriñ Abiibu Si doomi Sëriñ Maalig Basin Si bind ko ngir dajale as lëf ci jaar-jaari Sëriñ Maalig Basin Si aki waxtaanam, muy waxtaan yu am njariñ ngir lépp yeete la, yare, laabiire, ak waare, ngir li alxuraan wax ni: فَذَكِّرْ إِن نَّفَعَتِ الذِّكْرَىٰ (saaru 87, laaya 9) - فَإِنَّ الذِّكْرَىٰ تَنفَعُ الْمُؤْمِنِينَ (saaru 51, laaya 55) ak hasiis (waxtaanu yonnent ba) bay wax naan: الدين النصيحة = diine laabire la, ag càkkutéefug Sëriñ Muntaxaa Mbàkke mom Sëriñ Basiiru Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa, Tuddee Téere ba " النصيحة لاخوان, للترشيد و التنبيب" ( Laabiire bokk yi, jubal yeete .) + +Niti senegaal +Yoonu murit +Waxtaani Sëriñ Maalig Basin Si , njariñ, yare, laabire, yeete, ak waare + +Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan +Donga buy tërbiyawu moongi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu +jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru + +Kilifa balaa war a digle day def balaa war a tere day ba + +Liy yàq kilifa, ñàkk njariñ, ñàkk a jëf. + +Lepp looy santaane na fekk nga manal ko sa bopp ba su +ñu gàntoo yit nga defal ko sa bopp, ngir nit ñi ku léen +yaakaar ñu wor la. +Liy yàq kilifa, yatt la: 1. Lu mu xam wax ko; 2.Luñ ko wax, mu waxaat ko; 3. Lu mu mer, xul ko. + +Ku la jaay yatt (3), jënde ko yatt (3): +1. Ku la jaay xam-xam, jënde ko maandu, mu ne ndax as gor bu maanduwul du teree moy Yàlla; +2. Ku la jaayub juddu, jënde ko ngor, ngir juddu bu rafet du teree dem kaso; +3. Ku la jaay alal, jënde ko doylu, ngir bu doyluwul dina sàcc +Lees yarul kenn du man a jaxasook moom, loo bëgg a jaxasool +danga koy tàqaleek moroomam ya yaruwul. +Kilifa daa war a yar doomam, moo gën jikki ba fiy bëgg +a juge, naan sama gannaaw na ngéen topp ci diw. (nde loolu ku yar +sa doom bam man a yor mbooloo dooko wax), te nit ñi boo nee léen +topp léen diw mii, bu diw jubul it duñ ko topp. + +Yàlla mooy ndox ma Rasoolu Laahi mooy teen ba sab Sëriñ +mooy goj ba pas-pasu taalube ba mooy baak ba yitteem mooy +di yoor aka jukki ba barim ndox. + +Li tax kuy wut Yàlla ay mbokkam di ko yedd, jaam buy wut +boroomam talut moroomam, bu amee boroomam bëggul moroomam. + +Ku dul mer mbaam la, Kudul mar xaj la, + +Nit ku yiw, na joxe dooleem, joxe alalam, waaye bumu joxe +ngoram, ndax ku joxe sa ngor dootoo dara. + +Ku gis sa baay, gis sa nijaay, gis sa taawub baay +war a xam sa bopp. +15. Danga gis boroom judd buy taxawaalu akub juddoom; Boroom xam-xam buy taxawaalu akub xam-xamam ; + +Waaye doo gis mukk boroom liggéey buy taxawaalu akub liggéeyam. + +Delluwaay + +waaxtaan yi ak jaar-jaar yi moo ngi bawoo ci téere bu am solo +Sëriñ Abiibu Si doomi Sëriñ Maalig Basin Si bind ko ngir dajale +as lëf ci jaar-jaari Sëriñ Maalig Basin Si aki waxtaanam ci càkkutéefug Sëriñ Muntaxaa Mbàkke +mom Sëriñ Basiiru Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa, Tuddee Téere ba +" النصيحة لاخوان, للترشيد و التنبيب لرحمة" ( Laabiire ñeel bokk yi, ngir yar yeete ngir +Yàlla.) + +Sëriñ Maalig Basin Si +Bawoo :Sëriñ Habiibu Rasuul SI + +Senegaal +Yoonu murit +Rakki-gammu, (ci araab ربيع الثاني) tuddees na ko noonu ngir ne araab yi dañu ci daan lolliwu, maanaam daan ci am am ñax, di ci sàmm seenug jur, am ñu ne daa dëppoo ak lolli bi moo tax ñu tudde ko ko. Mooy ñeenteelu weer ci at mi, di weer ci njëkk ginaaw gàmmu gi + +Lëkkalekaay yu biti +Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) + +The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + + + +weeri wolof +Rakkaati-gammu ci araab jumaadal uulaa جمادى الأولى), njëkk Lislaam nag (jumaadaa xamsa) lees ko tudde woon, lu tax nag ñu tudde ko ko? ndax daa nekkoon ci sedd bi bi ñu ko koy tudde, nga xam ne ne ndox mi da daan way (jumaada) mi ngi jóge ci "jamada" giy tekki way, maanaam ndox mi da ci daan way di def ay donji yuur (galaas) ngir ag sedd. + +Mooy juroomeelu weer ci at mi, di itam ñaareelu weer gannaaw gàmmu gi. + + +weeri wolof +Maami-koor, (ci araab jumaadal aaxira جمادى الأخيرة), njëkk Lislaam (jumaadaa sitta ) lañu ko tudde woon, moom nag turam woowu mi ngi ko jële ci fiiroo gi mu defoon ak sedd bi, tur wa daal di koy topp (way). + +Mooy juroom-benneelu weer ci at mi, di itam ñetteelu weer laataa koor gi. + +Lëkkalekaay yu biti + +Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) +The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +weeri wolof +Ndeyi-koor,(ci araab rajab رجب ) moom nag ci weer yi am worma la bokk. Tuddees na ko nag Rajab ci araab, ngir ne ci weer woowu dees ci daa wéer ngànnaay yi, nocci ñawka yi wëlif xeej yi, daawuñu ci xeex, dees na wax (rajaba) maanaam taxawlu na wëlif xeex bi. + +Mooy juroom-ñaareelu weer ci at mi, di itam ñaareelu weer laataa koor gi. + +Xew-Xew + +Ci lees di màggal juddug [Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke| Sëriñ Faalu Mbàkke] ca Senegaal di ko wax Kazu Rajab (27bis ci rajab). + +Lëkkalekaay yu biti + +Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) +The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +weeri wolof +Baraxlu, (ci araab sahbaan شَعبان ), tuddees na ko noonu ndax aw ñall la (shahb ci araab) ci diggante "rajab" ak "ramadaan". Waxees na ne nit ñi daño cee baaxoo woon a tàqalikoo ak a ñallu (tas) ngir sàkku-ji ndox, mu daal di jël tur woowu. +Mooy juroom-ñetteelu weer ci at mi, di itam weer jiitu koor gi. Bokk na ci weer yi baax a woor ci jullit ñi + +Lëkkalekaay yu biti +Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) +The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +weeri wolof +Kori (ci araab شَوّال), ci la jullit ñiy wori ci seenug koor, mi ngi tudd nag ci araab "Sawaal" ngir ne sawaal day tekki ci araab ag jeex akug ñàkk meew, te ci weer woowu seen naaga yi (giléem yu jiggéen yi) dañu ci daan jeex, ñàkk ci meew. + +Mooy fukkeelu weer ci at mi, di itam weer wi njëkk gannaaw koor gi. + +Xew-Xew +Ci lees di korite muy bis bees di dog koor di màggal bis ba ngir gunge weer wu tedd wi wey. + +weeri wolof +Diggi-tabaski,( ci araab "sil-qihda" ذو القعد, moom nag ci weer yees wormaal la bokk: tuddees na ko noonu ci araab ngir ne "qahada" ci araab giy tekki jekki la baat bi juge, li ko waral nag di jekki gi ñu ci daan def wëlif xeex, wëlif it ñax, daawuñu ci laxas ngir sàmmi, daawuñu ci xeex, ngir wormaal ko, araamal ci xeex. + +Mooy fukk ak benneelu weer ci at mi, di ñetteelu weer gannaaw koor gi, di itam weer wi Tabaski toftal . + +weeri wolof +Tabaski, (ci araab "sul-hajja" ذو الحج), tuddees na ko noonu ngir ne mooy boroom aj gi, ci la araab yi daan aji Màkka, ci la tabaski gi it nekk, moom nag bokk na ci weer yees wormaal . + +Mooy weer wi mujj ci at mi. + +Xew-Xew + Ci lees di aj màkka,(ab ponk la ci lislaam war na jullit bu ko man), + Ci lees di Tabaski (rayi xar, bëy, nag, galeem, jokkug bokk, baloonte àq, jullig bër, ak yuni mel...) + +Lëkkalekaay yu biti + + Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar) + + The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia + +Weeri wolof +Cig déggoo, Njëkk-taariix mooy jamono ju taariixu nit ji jiitu sosum mbind. + +Ak juddug mbind taariixkat yi am nañu ay wayndare yu leer te yaa yees man a sukkandiku ngir man a taxawal toftaloog xew-xew yi yiy biral digalub jamonoy taariix yi. + +Xaaj bu yaa bu taariixu nit njëkk sosug mbind, ci xayma, mi ngi door mat na 200 junni at, ba jëmm ji njëkk jees man a nattanleek nitu tay jii feeñee ci Afrig gu Bëj-saalum. + +Donte sax mat na 2 milioŋi at, benn xeetu nit bu doon dund ci wetu Dexu Viktori (war a doon tay jii ci diggante Ugandaa, Keeñaa, Tansani) moo njëkk a jëfandikooy jumtukaay ci noonu taariixu xarala door. Cig lawal, manees naa njort ne fala xalaat, fànn, xeltu ak xam-xam dooree. + +Sosug jumtukaayu liggéey bu njëkk man a tax nu jàpp ne nëkk-taariix a ngi door 2 milioŋi at ci ginnaaw, donte mbooloo yooyu maneesu leen jàppe niki nit ninu ko xamee tay, ci jëmm ak doxalin. + +Njëkk-taariix +Xam ngéen ne nite (l’humanité) mi ngi juddoo Afrig, tàqalikoog nit ak dundat (animal) mi ngi ame fii ci Afrig, loolu kenn sikkatu ko.Xew-xew bu am solo bii mi ngi am booba ak leegi toll na ci 5 milyoŋ ak juroom benn téeméeri junniy at (5600000 ciy at), Afrig ngay man a fekk mbooleem xeeti nitu pax (homme fossile), loolu doo ko gis ci beneen gox (continent). + +Ñaari xeet yii di "Australopithèque robuste" , "Australopithèque gracile" , "l'homo alibis" , "l'homo erectus" , "l'homme de néandertal" maanaam homo sapiens bu yàgg ba, ak "l'homo sapiens sapiens" maanaan nit ku yewwu ñaari yoon, ni ko tur wi indee, niki yaw ak man, xeet wu mujj wii mi ngi juddoo Afrig booba ak leegi tollu na ci 120000 at, nite gii mi ngi juddoo ci ron rëddu yamoo wi (l'équateur), ci ron rëddu gaar (latitude)wu Kéeñaa, maanaam ci ron rëddu gaar wow, jañug ceññeeri yu jéggi-yolet yi (flux de radiation ultra violet)dafaa tar ba bépp cér mbaa yaram wu juddoo ci rëddu gaar wii, fàwwu mu nekk di lees cuub (pigmenté) te ñuul, doonul woon jàppadi ci nite gu njëkk ga muy man a dund bees ko cuubutoon, ginnaaw dénd bi moom (la nature) du sos dara cig neen, kon cuub daa ame liggéeyub aar yaram wi, da koy aar wëliif ceññeer yu jéggi-yolet yi nga xam ne doon na yàq ci anam gu mat mbooleem pukus (cellule) yu yaram wi. Nite gii dox na jëm kanam ci Afrig doore ko ci 120000 at ba ci lu yées 40000 at. Mi ngi génn Afrig jaare ko ci ñaari yoon/ Yoonalu Sues (Isthme de Suez), looloo waral deesi fekk ay roytéef (spécimen:misaali nit) ca Falastin, waaye ñoom gën ayàggadi roytéef yu Afrig yi, man xam naa ñi doon def gasi gëstu yi ci diiwaan bii, rawati na Ustaas bi Wardermer, waaye bees defee ay gëstu, dees na gis ne roytéef yu Falastiin yi ñoo gën a yees yu Afrig yi, foofooy yoon wi nitug Afrig ki jaaroon di génn. Waxuma la rekk Homo sapiens sapiens waaye it nitu pax (homme fossile) mi jotul a dund te ma la ko doon wax sànq. Beneen génnuwaay bi mooy Jibraaltaar (doju Taariq), foofa lañu jaar, ba nañu fa it ay jeexiit, mbooleem cuubiit ya (teinture) ca xunti ya, jeexiit yooyu dañuy wone ne foofu la nit ki jaare, waaye it ca bëj-saalumu Tugal rekk, fa tollook géej yu tàng ya, fa tollook "la Crimée", ca bëj saalumu Faraas, bëj-saalumu Espaañ, diiwaan yii ñoo nekkoon di yees man a dëkk.Foofu lees fekkoon mu dajaloo fa nite gu ñuul gi njëkk a dund Tugal (première humanité négroïde)loolu tollu na ci 40000 at.Ni mu manul woon a ñàkke nekkees ku ñuul ngir man adund ci Afrig, ni la manul woon a ñàkke nekkees ku am der bu leer ngir dund ca Tugal ngir sedd bu tar bi ba ëpp, fi nga xam ne amul jañug ceññeer yu jéggi-yolet yi, ci noonu la ñuule (nit ku ñuul) furee (dépigmenter) loolu àtteb dénd bi la ( la loi de la nature). Jëmmam it daal di soppiku topp wuyyusi gi mu def ñeel tëri noyyi gi ci sedd bi, ci noonu la weexe bi njëkk feeñ, bu nu tegee nee mbooleem idewolosi yi, booba ak leegi tollu na ci 20000 at ca Solutréen, di benn ci wàll yu mujj yi ci jamonoy doj ji, mooy "L'homme de Cro Magnon". Ki njëkk a dëkk Tugal ab ñuule la (négroïde), mooy "l'homme de Grimaldi", damay yam rekk ci Homme sapiens sapiens, ba nee nag homo erectus ak yeneen, waaw kay mi ngi noonu yoon wi nit ku weex jaar ba génn ci ku ñuul, ak mbooleem yeneen xeet yi ci càllal gu gudd, mbaa gu gàtt.Manoon nanu fee nekk di leeral ba lay wax ni nite gii génne jaare ca xat-xatu Béring (détroit de Béring) ngir dem juri askan wa dëkk Amerig, ba tay ni beneen bànqaas bi génne ca yoonalu Sues, jaare ko ca Duni Sond ya (les Iles des Sondes) ngir xumbali Oceani. Kon nite gii mi ngi juddoo Afrig, te it gu ñuul la, juddoo it ca balluwaayu Niil ba, maa ngi dikk leegi ci Isipt,nite gii mi ngi juddoo ca gongikuwaayu dexug Niil ga, moom nag gu ñuul kukk la woon ci li baatub ñuul ëmb ci maanaa, booba nag la daal di woon door di sanc xur wi (pegi dex gi), nekkoon na fi lu mat 120000 at njëkk muy wàcc bawoo ca diiwaanu Luwanda jëm ca Delta bu Niil ba (ab sottiwaayam) + +Taariix +Ecser ab dëkkaanu tunduw Pest la, bokk ci suufus Budapest. Am na 3.534 way-dëkk (2008) te bari ay saa-slowaki. + +Ecser a ngi nekk ci bëj-saalum-penku Budapest, ci wetu Naawuwaayu Budapest-Ferihegy. Peggook Maglód, Vecsés, Gyömrő ak Üllő. Yoonu weñ wu 120a (Budapest-Újszász-Szolnok) moo fay jaar. +Oonguri +Fànn, ci tekkeem gu yaa, dafa ëmb bépp yëngu-yëngu nit - muy lu kenn walla mbooloo di def - moom, su sukkandikoo ci gisiin yu xereñ, ñaw ak doxaliin wu bawoo cim njàng walla cig yàgg-jëf, mooy tax a man a biral genn kàllaama gu taaru gi. Ci fireem gu tay, fànn dees koo féetale ak man-gee jokkaley yëg-yëg, ba tax kàllaamay fànn, donte dañuy jokkaley bataaxal, taxul ñu doon dëgg-dëgg aw làkk, ndax taxawuñu ciw yoon wu ñépp ànd déggoo, xanaa kay safaan wa ku nekk ak sa gisiin walla déggiin. + +Cosaan, Fànn + +Pentuur + +Yatt + +Nataal + +Sinemaa + +Woy + +Fànn +Besançon mooy péeyu rééwum Franche-Comté (Faraas). Nitñii motnañu 117.050 (1999). + +Besançon +Dëkki Faraas +Ci xam-xamu nosukaay nosteg doxiin, ci tënk ND (operating system walla OS ci wu-angalteer), mooy mbooleem tëriin yiy yor, saytu lëkkaloo gu jumtukaayu nosukaay bi (tappaan yi, xel mi...) ak tëriin yi nga ciy jëfandikoo. + +Naka-jekk nosteg doxiin gi mooy tax jëfandikukat bi man di jot ci ëmbiit li nekk ci nosukaay bi jaarale ko cib jokkalekaay (muy ay njunj walla mbind yooy cuq mu lay won li nekk ci biiram). Yitteem bu njëkk mooy tax ba jëfandikukat bi, muy nit walla leneen, man di jokkalook nosukaay bi. + +Melokaanam +Dañoo am ay cër yu cëslaay yu, daanaka, nosteg doxiin yépp bokk, waaye terewul am yooy fekk ci yenn yi rekk, moo tax ñu gënante: + + Saalub noste gi: di mbooloom ay tëriin yu ndaw yu lëkkaloo ci seen biir, lëkkaloo itam ak jumtukaayu nosukaay bi. Mooy liy njëkk a ubbeeku su nosukaay bi di takk, di it, man nanoo wax, wàll wi ëpp solo. Moo tax ñuy man a def liggéey yu njëkk ci ndoorteelu takk gi, tax ñuy man a jot ci tappaan bu dëgër bi, ci dencukaay yu noste yi. Ci gàttal moo yor jokkalantey xibaar yi ci biir nosukaay bi. + + Yorkaayu dencukaay yu noste: mooy liy duggale ci tappaan yi. Wépp tëriin wu soxla ab njoxe cib tappaan moom ngay woo mu duggal la fa. Mooy ki yor, rawati na, nosug njoxe yi ci nosukaay bi (wayndare yi). + + Yorkaayu xel mi: mooy liy jox xel mu doy ngir seenug ubbeeku ak dox, fu ñuy denc seeniy njoxe, tëriin yi ba ci nosteg doxiin gi ci boppam. + + Jokkalekaay bi: man nañoo doon shell walla GUI mooy tax nit ñi man di jokkalook nosukaay bi. + +Xam-xamu nosukaay +Wikbaatukaay ab baatukaay barilàkk bu ubbeeku la, di benn ci sémbi Wikimedia Fondation yi. Baatub «Wikbaatukaay» dafay junj sumb bu wolof bu boobu sémb, di Wiktionary ci wu-angalteer. Mook Wikipedia ñoo bokk doxiin, di lu ubbeeku te dàttu ci nosteg wiki, lees man a jëfandikoowaat ci anami GFDL. + +Tëddiin +Yéeney sémb bi mooy sos ab baatukaay bees di duggal làkki àdduna bi yépp. Ci bu wolof baat yépp a fiy nekk ak seen tekki ci yeneen làkk waaye ci wolof lañu leen di faramfaccee, joge seen gongikubaat, seeni bokktekki, safaantekki, waxiin, añs. + +Baatukaay +Sémbi Wikimedia Fondation +Ci xam-xamu nosukaay tëriinuw nosukaay walla tëriin kepp , am mbooloom ay càkkuteef la gees binde ci genn kàllaama gi gu ab nosukaay war a jëfe . Di ag càllalay càkkuteef gu xellu te nosu, mbooloom ay cantaane yuy indi saafara ci yenn xeeti jafe-jafe. +Aw tëriin wees bind cig kàllaamag masin, wu ab nosukaay man a doxal dees na ko wax itam tëriin wu doxalu walla tëriin wu ñaarñaaloo. Aw tëriin wees bind ci kàllaama gu assembly walla ci tëriin wu tolluwaayam kawe, nosukaay bi dafay jëfandikoob boolekaay walla ab tekkikaay ngir man koo doxal, dees na ko wax tëriin wu gongikuwaay. + +Saa yoo yëngalee janax ji walla nga bind ak sa arafukaay, nosukaay bi ab santaane bees ko jox la jëfe, santaane yu jóge ci benn walla ay tëriin. Santaane yooyu ñooy di déglu bë jëfandikukat bi te di leen jëfe: ubbi ab dencukaay, bind, xayma, seet añs. Jëfekaay bi mooy wàll wi nekk ci nosukaay bi biy jëfe càkkuteef yi nekk ciw tëriin. Jëfiin wi mooy yoon wi nosukaay bi di jaar, jéego ci jéego, ngir jëfe càkkuteef yi. Kiy bind aw tëriin lees di woowee ab tëralkat + +Xam-xamu nosukaay +PHP Làkku Day la bu ubbeeku te jàppandi, defees na ko ngir sos ay xëti web yu matale jaare ko ci ab seddalekatu HTTP3, waaye it di nay man a dox niki beneen làkk bu man a doon ci anam gu biiru, PHP làkk wuy màgg la ba ci sumbu 5 ci doxiin aki melo yu mat, akuk woom ci ag kàngoom. +Yaxub PHP sos na ko moom Rasmus Lerdorf ci atum 1995, fim ne ñiy toppatoo yokkte gi ak di ko saytu moodi The PHP Group (Mbaaluk PHP gi), PHP Tëriin lu ubbeeku la ci Sarti PHP dëppalees ko ak Sarti GNU General Public License (GPL) + +misaalum xëtu PHP.php / PHP.php4 /PHP.php5 PHP.phtml + + +Xam-xamu nosukaay +HTML di wund (Hyper Text Markup Language) mooy làkk wees di wonee xëti Web yi + +misaalum xëtu HTML.html / HTM.htm + + + + Turu Xët wi + + +

Mbind mi!

+ + + +Xam-xamu nosukaay +ASP.net + +misaalum xëtu ASP.aspx / ASP.asp + <%@ Page Language="C#" %> + + + + + + + Xëtu Tektal + + +
+
+ Waxtu wi fim ne moodi: +
+
+ + + + +Xam-xamu nosukaay +Gaambi +Bujumbura mooy péeyu réewum Buruundi. + +Buruundi +Jibuti mooy péeyu réew mi tudd moom itam Jibuti, am na 542000 way-dëkk te rëye 630 + +Jibuti +Asmara mooy péeyu réewum Eritere di itam dëkk ba fa gën a rëy. +eritere +Addis-Abeba mooy péeyu réewum Ecoopi, mi ngi nekk ci diggu dëkk bi, nekk cig joor ju kawe ci diggante 2300 ak 2600 metar. + +Ecoopi +Nairobi mooy péeyu réewum Keeñaa di itam dëkk bi fa gën a rëy. + +Keeñaa +Kampala mooy péeyu réewum Ugandaa. + +Ugandaa +Antananariwo mooy péeyu réewum Madagaskaar. + +Madagaskaar +Lilongwe mooy péeyu réewum Malawi + +Malawi +Mamudsu mooy péeyu Mayot mi bokk ci Faraas. + +Mayot +Maputo mooy péeyu réewum Mosambik + +Mosambik +Kigali mooy péeyu réewum Ruwandaa + +Ruwandaa +Wiktooriya mooy péeyu réewum Seysel, mooy dëkk bi ëpp way-dëkk ci dun bi + +Seysel +Mogadisu mooy péeyu réewum Somali. + +Somali +Dodoma mooy péeyu réewum Tansani, di itam bu diiwaanu Dodoma + +Tansani +Tus-wu-taxaw wenn la ci ñaari xammikaay yi (beneen bi mooy tus-wu-gaar). Tus-wu-taxaw wi mooy tax ñuy man di féetale am mbir ci kaw Suuf si, ci penku walla sowwu + +Lëkkalekaay yu biir + Tus-wu-gaar + Gëwéel + Gëwéelub sànkar + Gëwéelub tef + +Melosuuf +Lusaka mi ngi nekk péeyu réewum Saambi ci bi muy am tembteem ci 1964, Sancaan yu waa-tugal yee ko sos ci atum 1905 ci ba ñuy defar yoonu weñ wi. + +Saambi +Arare ab dëkkub bëj-saalumu Afrig la, di tam péeyu réewum Simbaawee. Ñoo ngi ko xame woon niki Salisbury ci jamonoy canc gu waa-angalteer. + +Ab dëkk bu mag la, am lu mat 2,8 milioŋ ciy way-dëkk, mooy diggu yëngu-yënguy yaxantu ci Simbaawee. ci melosuuf ñoo ngi koy barabal ci (). + +Simbaawee +Luanda (bu njëkk São Paulo da Assunção de Loanda) ab dëkkub bëj-saalumu Afrig la, di itam péeyu réewum Angolaa. Féete ci tefesu Afrig gu mbàmbulaanug Atlas gi, Luanda mooy waax wi ëpp ci Angolaa gépp + +Dëkkiin +Limu nit ñi dëkk Luanda ci at yi: + + 1815 : Luanda amoon na 18 000 way-dëkk, + 1900 : 20 000 + 1934 : 18 000 + 1940 : 61 000 + 1950 : 137 000 + 1975 : 600 000 (atum tembteg Angolaa) + 1987 : 1 136 000 + 1991 : 2 000 000 (njeextalu xar ba) + 2005 : 2 776 000 + 2008 : +6 000 000 way-dëkk + 2009 : +7 000 000 way-dëkk + +Angolaa +Yaunde mooy péeyu réewum Kamerun, + +Kamerun +Bangi mooy péeyu Réewum Diggu Afrig, way-dëkkam ñoo ngi koy xayma ci 622 800 ci 2003. + +Réewum Diggu Afrig +Njamena mooy péeyu réewum Cadd, di itam dëkk ba fa gën a rëy. + +Cadd +Brasawil mooy péeyu réewum Kongóo. Làkk yees fay wax ñooy Lingala ak munukutuba| + +Kongóo +Kinshasa mooy péeyu réewum Kongóo-Kinshasa. + +Kongóo-Kinshasa +Malabo mooy péeyu réewum Gineg yamoo, mi ngi féete ci bëj-gànnaaru dunub Bioko. làkk wees gën di jëfandikoo ca dëkk ba mooy wu-espaañ ak wu-gineg-yamoo. Malabo ci jamono yi weesu jotoon naa am yeenen tur: + + 1827 ba 1846: Clarence City (tur bi ko waa-angalteer joxoon) ; + 1846 ba 1973 : Santa Isabel (tur bi ko waa-espaañ joxoon) ; + 1973: Malabo (tur bi ko waa-Gineg-yamoo jox). + +Gineg yamoo +Orsay (Musée d'Orsay) : Paris + +Open : 1986 +Dayoo : 57 400 m² +Visites : 3 200 000 (2007) + +External links + + www.musee-orsay.fr +Libarwil mooy péeyu réewum Gaboŋ. + +Gaboŋ +Sao Tome mooy turu dun bi ëpp ci Sao Tome ak Principe, di itam péeyu réew mi. Mi ngi féete ci tefesu bëj-gànnaaru dun. + +Sao Tome ak Principe +Alse walla الجزائر ci araabi alseeri mooy péeyu réewum Alseeri, féete ci bëj-gànnaaru réew mi janook Géej gu Diggu gi. Mooy itam dëkk bi gën a mag ca réew ma + +Alseeri +Xayra (ci araab لقاهرة Al-Qāhira) mooy péeyu réewum Isipt, mooy dëkk bi ëpp nit ca goxub Afrig. Donte Al-Qāhira mooy tura dëkk waaye, lu bari, dees na ko wax itam, ci araabi waa-isipt, misr di Isipt ci araab. + +Isipt +Tripoli (di طرابلس tarabilus ci araab) mooy péeyu réewum Libi. Turu dëkk baa ngi tekki «ñetti dëkk yi», ndax limu jóge ci booloog ñetti dëkk yii di Oea, Leptis ak Sabrata. Mi ngi féete ci bëj-gànnaar-sowwu réew mi, taq ci tàkk gi, ci dogub suuf bu kekke, féetek Géej gu Diggu gi ci geneen wàll + +Libi +Péeyi afrig +Rabat (di الرباط ar-Ribat ci araab) mooy péeyu Nguurug Marok, mooy ñaareelu dëkk bi ëppi nit ca nguur ga. Mi ngi nekk ci wetu tefesu mbàmbulaanug Atlas gi. Ca jamono-ju-yàgg ja lañu fa tambalee dëkk. Ñoo ngi ko sos, dëgg-dëgg, ci 1150. + +Marok +Planoise mooy péeyu rééwum Franche-Comté (Faraas). Nitñii motnañu 20.700 (1999). + + Jakka Al-Fath + +Besançon +Xartum (ci araab al-Khartûm الخرطوم ñu man koo tekkee «ñoxub ñay») mooy péeyu réewum Sudaan, féete ci wetu Niil bu weex, bi jóge Ugandaa, ak Niil bu baxa, bi jóge Ecoopi. + +Sudaan +Tunis (ci araab تونس ) mooy dëkk bi ëpp ci Tiniisi, mooy péeyu réew ma dale 20 sattumbar 1159 (di 5 koor 554 ci arminaatu jullit ñi). Nekk ci bëj-gànnaaru réew mi , ci dóoxub Tunis bi ko tàqaleek déegub Tunis bi. Ña fa dëkk waa-tunis lees leen di woowee, ci suuf su yaa la tëdd man ngaa daw 30 km laa ngay àgg ca anéer ba. + +Tiniisi +.ac mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Asensio + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1997 + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .AC Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#A +Duni Kanaari yi (ci wu-ispaañ Islas Canarias) ay dun lañu yu bokk ci goxu Afrig, féete ci bëj-gànnaar-sowwu Afrig nekk ci mbàmbulaanu Atlas, te bokk ci réewum Ispaañ. Ñoo ngo ko Séddale ci ñaari tund Santa Cruz gu Tenerif ak Las Palmas. + +Gongikubaat +Turu duni Kanaari ngi jëlee turam ci latin Canariae Insulae (duni xaj yi); tur wi ci Kanaari gu Mag rekk lees ko doon jëfandikoo ("Canaria Insula"). Di bàyyikoo ci xaji àll yu mag ("canes") yu nemmeekukat yu njëkk yi wuññi woon ca dun ba. + +Lëkkalekaay yu biti + Nguurug Kanaari + Péncum réew mu Kanaari + +Kanaari +Las Palmasu Kanaari gu Mag ab dëkkaanu Tunduw las Palamas la, di itam péeyam teg ci nekk benn ci ñaari péeyi Duni Kanaari yi (réewum Ispaañ) beneen bi di Santa Cruz wu Tenerif tuxalug man-man gi ñeenti at yu ne lees koy amal. Mi ngi nekk ci bëj-gànnaar-penku Kanaari gu Mag mooy dëkk bi fa ëpp, tëdd ci suufus 10 km. + +Dëkkiin + + 1991= + 1996= + 2001= + 2004= + 2005= + +Kanaari +Niccolò di Bernardo dei Machiavelli (Nikoloo Makiawelli)(3 mee 1469 – 21 suwe 1527) ab bindkat, xeltukat, aji-politig ju Itaali la woon. + +Niki Leonardo Da Vinci, Machiavelli jàppe nañu ko kuy misaal dëgg-dëgg nitug yewwute. Bii tekki - ginnaaw ñu bari - di nanu xamal ci jëmm ji ak ci nitu mbind ki waaye du nu xamal ci ngérum machiaveli, mi dugg ci waxtaani bés yi di junj am xel mu yaa te ñaw waaye it di gaaw a ñaaw-xel, ami sikki-sakka ci lépp. Machiavelli jàppe nañu ko niki ki sos xam-xamu politig bu jamonoo bi. + +Njàngat +Politig +Itaali +Muurum Koor di ci wu-araab “زكاة الفطر/Zakaatul Fitr” farata la ci bépp jullit bu di boroom xel, mag walla ndaw, góor walla jigéen, ab jaam walla gor, ngir waxtaan (Hadiis) wi nu Abdulaah mom (Ibn) Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) dikke ne: «Yonentub Yàlla (jàmm i Yàlla ci moom) farataal na ci nun muurum koor ci wéeru koor, saa ci tàndarma walla bele, muy ab jaam walla gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw ci jullit ñi» (Buxaari 2/579, Muslim, Tirmiidhi, Abuu Daawuud, Nasaaï ak Ibn Maaja) Ku ko weddi ab yéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ab saay-saay la, bu ko tuubul ba dee ag payam sawara la. Ku ko deful it du ko wàcc ba mukk ci dëppook boroom xam-xam yi, doonte bu julli gi weesoo yoolum sarax ngay am. + +Kañ lay war ? +Balaa noo julli korite lees koy génne, Mom Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) neena: «Digalees nanu nu genne muurum koor balaa nit ñee génn di julli ji» (Buxaari 2/579, Muslim) +Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi akit ngir leel way-ñàkk yi, Ku ko genné njëkk julli gi muurum kooram mees nangu la, Ku ko génne ginnaaw julli gi nag, sarax la ci sarax yi » (Abuu Daawuud, Ibn Maaja ak Daaraqutnii) +Naafih nettali na ni: «Ibn Omar génne na ko benn walla ñaar i bis njëkk Korite» (Buxaari) +Ci ngirum Maalig mi waa réew mi di sukkandikoo ak Ahmed, neena ñu «manees naa joxe muurum koor benn walla ñaari fan njëkk korite» +bu dee ci Abuu Hanifa neena: manees nakoo génne njëkk wéeru koor sax, Saafih ni manees nakoo génne ci bu weeru koor tàmbalee. +Waxtuw joxe ko dëg nag moongi doore ci bu weer wi feeñee la ko dale ca timis ga ba xëy. + +(karmat: Wax i maalig ji ak Ahmed (genne ko ci ñaari fan jëm kori) ñoo sax ci sunna, moo gën a lënk, waaye yeneen ax yi ci góor-góorlu la (ijtihaad) tege ngir ag jàppandal ñeel jullit ñi, kon ku loru man nakoo jëfandikoo ci lu dul par-parloo, manaam ci bu fekkee ni fi nga nekk amoo kooko fi man a jox te réew sàngam walla dëkk sàngam la war a dem, nanu seet ñaata bis lay def àgg famu jëm ci ñaari fan ba ci jullig kori, te bañ a weesu loolu ngir moo gën a dëppoo ak sunna.) + +Ku ko génnewul ba julli gi wees nag ? +Boroom xam-xam yépp dëppoo nañu ci ne du tax mu wàcc ko mukk, doonte sarax lay doon bu julli gi xësee weesu niko Yonent bi waxee: «Ku ko génne ginnaaw julli gi, sarax la ci sarax yi » + +Ana ku muy war ? +Xanaa ab jullit bu di boroom xel, di as gor (bu dee ab jaam it boroomam moo koy genneel) di mag walla ndaw, góor walla jigéen, ab jaam walla gor, Abdulaah mom (Ibn) Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) neena: «Yonentub Yàlla (jàmm i Yàlla ci moom) farataal na ci nun muurum koor ci wéeru koor, saa ci tàndarma walla bele, muy ab jaam walla gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw ci jullit ñi» (Buxaari 2/579, Muslim, ) Mu diko war ci boppam (gor si te di ab jullit) ak koo xamni moo ko war a dundal niki: soxnaam ak doomam ju góor ba bamuy mat góor (mukallaf/majeur) ak doomam ju jigéen ba bamuy mat a am boroom kër ak ci ay way-juram (bu ñu ko amul) ak ci ay jaamam. +Ku ko amul woon bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ci, bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot, wér na ci sunna. + +Ana ci lumu koy war a génnee? +Xanaa ca la ëpp ca réew ma mu dëkk di dunde, nun waa réew mii daanu ko génne njëkk ci Ceeb, Dugubi Suuna, Saaño, Basi, Tin, Feela ku ko amul jënd ko joxe ko, kuy dunde yu dul yii yitam man na koo génne ca lamuy dunde rek. + +Ana namuy war a toll? +Xanaa benn (1) saa bopp bu nekk. Bu dee ci réew mi dugub lees ko daa gën a génnee ci bopp bu ne ñaari kilo ak genn-wàll ci Dugubi-Suuna ak yini deme bu dee Ceeb nag walla muy yu dul yii kon day wut nattukaay goo xamni ñaari kilo ak genn-wàll a koy fees ci Suuna mu natt ko ca te bañ koo peese ngir xam ñaata kilo la. + +Ana luy benn Saa? +Saa mooy tolloo ak ñeenti mudd, benn mudd bu nekk mooy tolloo ak sa tibbub ñaari loxo bees ko boolee, yenn ci yees di dunde bees ko natte ci benn Saa: +Ceeb: 2300g +Bele: 2040g +Cere: 1800g +Tàndarma: 1800g +Fariñ: 1400g +Resiñ: 1640g + +Ana ku ñu ko war a jox ? +Ku ñu war a jox Asaka rek ñoo yam ci lépp, moo di as gor su di ab jullit te am ca aajo ju wér te muy koo xamni seenuwu loo ci moom lenn njariñ lu dul jox ko ko ngir Yàlla rek, Séenuwu loo mu di la sant ak a gërëm walla mu di ko nettali fi aw nit, nga xamni bëgguloo sax ku ko yég, bëggu ñu nag ku la dogal ab tool nga di ko jox asaka ngir tool ba loolu araam na ci ñoom ñaar ñépp, boroom tool bi nag bu ko moomee sañ nala koo jaay walla mu luye la ko waaye lumu ci doon doo ko ko jox ci asaka ji walla luñuy lekk walla lu suuf di saxal, bëgguñu yitam jox nit asaka mu di ko jaay nga di ko jënd, bëgguñu yitam tuxal asaka lu gën a sori juroom ñaar fukki kilomet te fi nga nekk ku ko yayoo sori wu fa, bu ko weesuwul nag dara newu ci, boo gisul ku ko yayoo lu dul lu ko weesu yitam dara newu ci., sañees na koo dajale jox ko kenn, sañees na koo tasaare ci mbooloo mu ko yayoo. ku ñu war a jox asaka. +Ku ko amul woon ba mu wàcc la bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ci, bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot. + +Abuu Haniifa ak ñénn ci boroom xam-xam yi nangu nañu genne ko jox ko waa-téere ba (Ahl-ul-Kitaab) manaam ñi nekk ci diiney Yahuud ak nasaraan. (Sayyid Sâbiq mooko indi ci Fiq As-Suna) + +Ndax manees nakoo génne ci xaalis ? +Ci ngirum Maalig maneesu koo génne ci lu dul aw cam, Maalig neena: «Muurum koor wareesu koo génne ci lu dul ñam, Deesu ko génne ci kee (xaalis wala lu ko xeetoo)» loolu it mooy gis-gisu Shaafih ak Ahmed ibn Hanbal. + +Ci ngirum Abuu Haniifa manees naa génne muurum koor ci xayma ko ci xaalis (Imaam Nawawii mooko indi ci saraab Sahiihu Muslim). boroom xam-xam yu bari ci jamono jii it nangu nañu ko. + +Karmat: joxe ko ci ñam manaam li ngay dunde moom rekk a sax ci sunna, te Hadiis bi koy digle it daa waxni ngir jox way-ñàkk yi ñu lekk la, te moom la daan def it, leel léen miskiin yi nag wuute na ak joxe léen ci séen alal yi, leel miskiin muy jox ko lekk sarax lees ci jublu, joxe léen ci séen alal yi azaka lees ci jublu, wuutee ngi foofu bu jar a bàyyi xel, ginnaaw léel miskiin la wax, nanu léen leel ci li nuy lekk rekk, Joxe ko ci ñam nag moo war. + +Mu des nag bu loru amee, kon ngànt day taxaw ndax lor fu mu fekk ab àtte àndaleko, bu boobaa manees koo jëfe ci niko Abuu Haniifa gisee ci lu dul par-parloo te sellal yéene ji. + +Luy njariñam ci lu nëbbu ak lu feeñ ? +Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi akit ngir leel way-ñàkk yi...» +Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ci naan: Fexe léen ñu woomal tay! (Daraqutni) manaam ngir way-ñàkk yi woomal ci bisub korite gi. +ci niko Al-Bayhaqi Soloo: «Fexe léen ba bu ñu yalwaan i ci bisub kori gi» +Kon dina laabal aji woor ji ci mboolem rëcc-rëcc i koor gi ak it indi indi jàmmu ci nit ñi ci dimbalante, woomalal ñu ñàkk ñi ngir ñu yëg bër gi ni ñépp, fexe ba kenn du yalwaan ci bis bi. + +Amma nag Hadiis biy waxni fii ak génnewuloo ko deesul nangu sa koor, ci wax i boroom xam-xam i Hadiis yi wérul, manaam jàppee wu ñu ko waxi Yonent bi (jàmm i Yàlla ci moo). + +lislamm +Niels Bohr: jëmm nit. + +Karmat ak delluwaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Albert Einstein + Jëmm + +Lëkkalekaay yu biti + +Jëmm +Siddhārtha Gautama (Sanskrit: सिद्धार्थ गौतम; Pali: Siddhatta Gotama) nekkoon na di ab jàngalekatu diine ca pénkub dogu-gox bu indian, moo sos ngiirum budda xolees na ko ci way buddaa niki xalifab budda (Sammāsambuddha)ci sunuy at. Atum juddoom ak mom deeyam wuutees na ci: ñaar fukki réew yi gën a fes ci jaar-jaar, taarixal na ñu diirub dundam ci ne c. 563 BCE jëm 483 BCE; li gën a mujj, te sax, + +Waxam ju mujj moodi: «Mbëj yees defar yepp luy wéyadi la ; Liggéey ci ag xarañ te bañ a noppalu ; Am jubluwaay bu baax farlu ; Saytu xalaat yi ! » +Charles Darwin : Xam-xam dundat yi nit. + +Dundat yi +Aj mooy juróomeelu ponku Lislaam, Ci waxi Yonent Yàlla Muhammed ja ni: "Tabaxees na Lislaam ci juróom: Seere ne amul benn buur bu dul Yàlla te Muhammed ndawam la, Taxawal Julli, Joxe Asaka, Woor weeru Koor, Ak Aj ci ku ko man aw yoon", ba tay Aj farata la ci benn jullit bu ko man (ci bépp anam), ci waxi Yàlla mu kawe ja ni:ñeel na Yàlla ci nit ñi Aj néek ba ci ku ko man aw yoon (benn yoon) te ku weddi Yàlla moom woomle na waliif mbindéef yi. + +Aj Màkka ak kumu war + +Aj Màkka benn yoon wartéef la ci mukàllaf mu ko man ci yaramam ak ci ab yóbbalam. +Manug Yaram wi moodi mu bañ a ame wopp ju ko tee man a dem walla mu ragal +ca dem ga dollikug wopp ja, walla sosug wopp walla ak yeex a wér. + +Yobbal bi yit moodi mu am lu ko lew lu sell loo xam ne darra ci ribbaa nekku ca, +àqi kenn nekku ca, te yalwaanu ko ñaanu ko te mu doy ko sëkk ba du tumurànke ci yoon wi +du ca yalwaan du lëjal kenn, waa këram itam mu bàyyee leen lu leen doy sëkk ba du ñu tumuturànke +du ñu lëjal kenn. Mu fay boram yépp bu dul bu ab digam teewul, waaye bu dee teew balaa dellusi sax war na koo fay balaa dem walla mu batale ko. +Bu ci yooyu yépp amee nag war na ko ni ko julli waree ku ko weddi ab yéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ci genn anam ab saay-saay la bu bon te bu ko tuubul ba dee sawara la jëm. +Ku ko bëgg nag bu demee ba fa muy armale dana fa fekk ku ko jiite ci yi mu war a def yépp ak yi mu war a bàyyi yépp ba ba muy noppi. +Moongi ware ci weeru Tabaski + +Ñatti xeeti aj yi: +Aj am na ñatti xeet: + +1-Ajug tamattuh +2-Ajug qiraan +3-Ajug ifraad + +Umra + +Umra yitam sunna la benn yoon mook Aj ñoo nuróo lépp waaye boo doxee safaa ak marwa umra jeex + +Faratay AJ + +Aj ñeenti farata la am : +1 yéenee Aj (nawaytul-hajja wa 'ahramtu bihii lill-Laahi tahaalaa) +2 tawaaful ifaada +3 dox diggante safaa ak marwa +4 taxaw arafa. + +SUNNAY AJ + +Sunnay Haj fukk ak ñaar la: +Am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga: +1 sangu gu jokkook armal gi +2 rafle ci lunu ñaw +3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll +4 labayka. + +Tawaaf gi am ñeenti sunnaam : +1 dox gi +2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ +3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi +4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi. + +Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : +1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa +2 ag yeegam diggante safaa ak marwa +3 gaaw gi niy def ci batnu masiil +4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa. + +Bañ na ñu +Bañ na ñu lool nag ku Aj ba dikk mu di ko darajawoo walla mu di ko tuddoo di ko dolli ci aw turam, +walla mu defe ne gëne na ko (Aj gi) kenn ku ko deful. Na ko def ngir Yàlla rekk, niki muy tuddee Yàlla +ak a Julli ak a Woor ak a natt Asaka ngir Yàlla. mu xam ne Aj itam ak yooyu ñoo yam kepp ci ku mu war. +lu waay di def na ko def ngir Yàlla rekk ngir lu dul Yàlla ak neen la. + +Ponki Lislaam +ak buum la gu ñuy jefe ndiko ngir xej ndox ci teen. +Tabaski (ci bati Seereer) Sunna la su far ci ab jullit bu di as gor te man ci ag jàppndal, ku mukàllaf rekk mag ak gone ñoo ci yam. +Waaye nag dina ware ci ñaari xeeti nësër yii : +1- ci ku ko nësër niki ngani bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tabaski, +2- ci ku njënd am xar, walla mu yor am xar jublu ci tabaski, manaam kon xar moo jënd niki am tabaski, manatu la ñàkk.Tabaski it ag bër (`iid) la gu Yàlla may jullit ñi, Jële nanu ci Anas (gërëmul Yàlla ci moom) mu ne: Bi Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi agsee Madina fekkee na léen ñaari bis ñu cay caaxaan, Mu ne (jàmmi Yàlla ci moom): « Ana luy ñaari bis yii ?» Ñu ne: “Danu ci daa fo (caaxaan) ci jamonoy ceddo (jaahiliya)” Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi (jàmmi Yàlla ci moom) ne léen: «Yàlla jox na léen ñaari bis yu gën yooyu ñaar, ñuy Bisu tabaski ak Bisu Kori» (Abuu Daawud mooko soloo) Gàttub tabaski it deesu ko rendi jëkk rendig Yilimaan te Yilimaan it balaa rendi nig ba julli, ci niko Baraan nettalee jële ci Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi «Dees na lottal ginnaaw julli» +Ku rendi lu ko jiitu du doon am tabaski xanaa ag ndawal rekk lay doon, noonu la saxe ci Sunna. +Am tabaski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc, noonu la saxee ci sunna (Albuxaari mooko solo) + +Àtteb Tabaski ci Lislaam ? +Yàlla neena: «Jullil ngir sa boroom te rendi (lottal)» +Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi neena: «Ku am dooley tabaski te tabaskiwul, kon bu mu jege sunu barabu julliwaay» (Abuu Hurayra mooko nettali, Ibn Maaja, Ahmad, Daaru Qutni ak Al-Haakim ñooko soloo. doonte barina ñu jam hadiis bi ci woroom xam-xam yi, niki Haasim ak ñeneen) +Baraan nettali na ni, Yonent (Jàmmi Yàlla ci ñoom) bi neena: Li nuy njëkka def ci bis bii, moo di julli, ginnaaw ba nu dellu lottal, ku def loolu def na sunu sunna.» + +Ash-Shaari` neena: «Duma nangu ku am dooley am tabaski diko sàggane » +Tabaski Sunna la nag su far, Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi saxaloon nako te daan ko digle. +Sunna la su far ci Ñoñ-Maalig, Shafi`, ag ñenn ci waa Ahmad ibn hambal, bu dee nag ci Abuu Hanifa ñoom lu war la, Lu war ca ñoñ Abuu Hanifa nag tekkiwul ni farata la. +Lu man a am nag ñépp dëppoo na ñu ci ne dina war ci ñaari mbir : + 1- Ku ko nësër, niki ngani bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tabaski, + 2- Ku xës njënd am tabaski, walla mu yor am xar jublu ci tabaski, manaam xar moo njënd ni am tabaski la, walla nga yori xar ni xar sàngam am tabaski la, ci yooyu barab luy war la. + +Waxtuw rendi am tabaski: +Mingi dale ci rendig Yilimaan, rendig yilimaan moongi aju ci ginnaaw julli gi, ba jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi rendee mu baax, bu dul guddi. La ca gën moodi boroom rendil ko boppam, bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw, Ku rendi tabaskim jàmbur te amu ci ndigal, kon du ko doy am tabaski te war naa fay boroom. + +Am tabaski: +Yàlla neena ci Alxuraan: «Deesul am Yàlla ci ndawalam ga, déeti dereetam ja, waaye dees na Ko am ci ag ragal [Yàlla]» S22 L:36. Kon nanu jàpp njëkk ni yéene ju sell, te Yàlla rekk tax waliif ngistal walla wanu ci bëti nit ñi mooy maye am tabaski. + Xar mu am juróom benni (6) weer walla at aki fan ci li sax ci Waa-Maalig, tey am kuy moo ci gën. Bu dee aw bëy nag, na am at ak weer ci waa-maalig, + Xar a gën, topp bëy, topp nag ak giléem + Xar mu góor a gën mu jigéen, bëy wu góor a gën wu jigéen, nag ak giléem naka noonu. + Juróom ñaari jullit man nañoo boole jënd aw nag walla giléem, Bu dee xar walla bëy nag kenn du ko bokk xanaa tiyaaba ja ci yéene. + +Yees nanguwul ci am Tabaski: +Bu benn béjjan dammee te wérul matul am tabaski [ci maalig], Bu weree nag mat na am tabaski, bu juddu waalewul ay béjjen nag darra nekku ci, +Bees xaajee nopp ba ñatt, la ca dagg bu matee benn xaaj ba, matul am tabaski, Bu juddu waale wul nopp walla bu gàtt nag dara nekku ci, +Bu nopp ba xaree lu toll ci benn ci ñatti xaajam du mat am tabaski +Bees xaajee geen ba ñatt, la ca dagg bu matee benn matul am tabaski, Bu ko juddu waalee nag dara nekku ci. + +Am Tabaski war naa mucc ci yii: + Bumu yooy, ba amul nebbon + Bu gimiñ ga xasaw + Bumu patt ba fés, rawatina nag muy gumba + Bumu làgge bamu fés, rawatina nag mu damm +Alaa kulli haal nag, Lislaam ag yombal la bëgg, te mboolem àtte yi woroom xam-xam yi di tërël di na ñuy sóoraale lool ag jàppndal ñeel jullit ñi. + +Lees di bañ ci ndawlug am tabaski: + Bañees na ku ca jaay darra ba ca der ba sax, ku ko ñaani ba mayees la ko nag man na koo jaay dara nekku ci. + Bañees na yitam ka koy fees ñu di ko fay ca yàppu wa, waaye manees na ko caa may walla sarax, bu laajee ag fay fayees ko xaalis walla leneen + Bañees na gépp joxe ngir wareef, niki tànku njëkke, yeeli maam, baatu feeskat, ak yuni mel, waaye nag moongi aju ci jeene ji, booy sarax sa dëkkandoo te bëggal ko sutura man ngaa yéene sarax te wax ko ni am sa tànku njëkke, ndax Yonent bi neena: «Jëf yaangi aju ci yéene yi; Ku nekk it langa yéeneey sag pay» te it amaana boo ko nee sarax mu rusloo ko ci kanamu njabootam mbaa sax mu tere kokoo jël. + +Rendi : +Ab jullit moo koy def, te doon ku am xel, Melo wi ci gën nag moodi mu tëral la muy rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu xibla, bu dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba ba famu yam ca baat ba mu teg ca paaka ba, Walla bu amee téeréy baat mu teg paaka ba ca diggante téere ya, Bu ko defee bala caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni fas na maa yéenee daganal lekk yàppu nàngam lii ci rendi gi ma koy rendi, bu dee teg paaka ba mu wax:«Bismil Laahii» dal di koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg, Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax: Allaahu Akbar, Bu teggee loxoom mu wax: «Rabbanaa taqabal minnaa innaka anta as-samii`ul Al-`Aliim S2:L:126:». Bu dawalee paaka ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk, Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko kon deesu ko lekk. Te yit bu mu bañ a tàngale baat ba, Bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën. + +Loj : +Ku koy def, day taxawal lamuy loj jubale ko "XIBLA" (Kaabag Màkka), Lem baat ba tëral ko ci wetug càmmoñ nga, Bu ragalee barig doole ja, Man naa yeew tànkub càmmooñu kanam ba, Te balaa tàmbali mu wax «Bismil Laahi», Te bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul. Lees war a loj nag bees amul lojukaay Sañees na koo rendi, lees war a rendi it bu ñu amul rendikaay, Te am lojukaay sañees na koo loj. -Giléem (Galéem) loj rekk lees koy def mbaa deesu ko lekk waaye deesu ko rendi, Xanaa ñu loru ñàkk lojukaay te am rendikaay, bu boobaa nag dees na leen ko may, -Bu dee aw Nag dees na ko loj niki ñu koy rendee, kon moom lu leen jekku rekk ñu sañ koo def noona, (Fii nag rendi ko lañu gën a miin) +Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi daa war a dagg, kon ci ag wet lees koy defe ak kanam.. + +Na moytu yii: +Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk, Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko, kon deesu ko lekk. Te yit mu bañ a tàngale baat ba, Bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën. -Rendi xar ak bëy ci kanam lees koy defe, boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk, -Bu dee aw nag manees na koo rendi manees na koo loj, -Bu dee Ginaar (Ganaar) nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee baax waaye bañ koo def a gën. + +Ngënéeli Tabaski: +Ngënéeli Tabaski ci lislaam lu am solo la, kenn manu koo takk, Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi xamle nani toq dereet wiy njëkk a génn Yàlla di na ci jéggale mboolem bàkkaar yees masa def, nii la dikke ci sunna ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom). +Jëlee nanu ci Ibn Abaas muni Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi neena : «Xaalis dugaleesu ko ci lu gën gàttub tabaski (iid)» (Daaru Qutni mooko soloo). Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi bégal nanu ci ne Xarum tabaski dina njot ci sawara niki mu ko njotee woon bakkanu Ismaayla. Amul lu jëf ju nit di def ju gën a neex Yàlla ci tuur deret ci bisu tabaski, noonu lako Aysa nettalee. + +Lislaam +Bundesliga football (Almaañ). + + 2009-2010 FC Bayern München + 2008-2009 VfL Wolfsburg + 2007-2008 FC Bayern München + 2006-2007 VfB Stuttgart + 2005-2006 FC Bayern München + 2004-2005 FC Bayern München + 2003-2004 SV Werder Bremen + 2002-2003 FC Bayern München + 2001-2002 Borussia Dortmund + 2000-2001 FC Bayern München + 1999-2000 FC Bayern München + 1998-1999 FC Bayern München + 1997-1998 1. FC Kaiserslautern + +Football +Almaañ +Dawaan gu wéy (ñu man koo tënk ci DC Direct Current ci wu-angalteer, moom lees di gën a jëfandikoo), di dëddoo ak dawaan gu safaanu AC, xeetu dawaan la gu am genn jubluwaay. Dawaan gi dafay wéy di dox ci ag ndombo ci genn jubluwaay. Mbëjfeppal yi ci genn jubluwaay lauy wéy di daw. + +Nattiin +Dawaan gu wéy ciy amper lees koy natt. Benn amper mooy ,24*1018 mbëjfeppal ci saa (I = Q/t), I = dawaan, Q= coulomb, t= saa). + +Wenn rëdd wu wéy ak ñett yu ndaw, ci suufam, mooy njunju dawaan gu wéy; dees na jëfandikoo itam DC (Direct Current). Dawaan gu safaanu moom AC alternating current lees di jëfandikoo wall njunj wii di ~. + +Jëfandikoom + +Dawaan gu wéy lees di jëfandikoo lu bari la ci taraay gu suufe ak ci mbëjfeppal, rawatina ci jumtukaay yiy doxeek tegle yiy man a jur dawaan gu wéy kepp. Ci daamar yi, su safaanukaay bi juree dawaan gu safaanu dess koy soppali gu wéy. Saxaar yiy doxee mbëj itam ñoom dawaan gu wéy lañuy jël. + +Taariixam + +Thomas Alva Edison mooy ki fi taxawal séddaleeg dawaan gu wéy ci wetu njeextalu XIXu xarnu bi, bi ndefar gi tambalee jëfandikoo mbëj. Ci ginnaaw bi lees ko wuutaleek dawaan gu safaanu gi Nikola Tesla sakk, ndax limu gën a yomb a yóbb ci diggante yu gubb. + +Dawaanu mbëj +Dawaan bu safaanu (DS walla AC ci wu-angalteer: Alternating Current) màndargoo ag walug dawaan guy soppiku ci jamono muy ci taraay walla ci jubluwaay. + +Doxiin +Naka-jekk dawaanu mbëj suñu koy séddale, ci dawaan bu safaanu bu baraayam sax ci 50 Hz walla 60 Hz lees koy defe (+ ak - bi dañuy safaanu ci watatukaay bi juroom-fukki saa yu ne). Dawaan bi ak dendu mbëj bi, ci biir watatukaayu mbëj bi, seen Demiin dafay mel ne bu ab duusub sin. + +Jëfandikoo gu dawaan bu safaanu mi gi jóge ci li jurukaayu dawaan yi, ci yaxanaay ci koom-koom ak seenug yomb a defar, di jur dawaan bu safaanu ci anam gu yomb, kon dawaan bi ci boppam kenn du ko soppiwaat laataa ag jëfandikoo. + +Fi njariñ li gën a feeñee sax mooy séddaleeb dawaan bu safaanu bir na ne moo gën a yaxan dawaan bu wéy ci séddaleeb dend bu kawe (ñakkug kàttan gi ci buum yu gudd yi moo gën a néew). rawatina, ci diggante gu gennwéq walla wéq yu bari, bir na yaxanaay gu ñettiwéq di gees gën a jëfandikoo ndax néewteey ñakkug kàttan ngir njeexitu Joule (moo tax dijjaayu watatukaay yi gën a néew, maanaam wëñ yu gën a sew); jëfandikoog dawaan bu safaanu bu ñettiwéq lawal na buumi yóbb yi ci diggante yu gudd lool yi. + +Genn Màndarga gu am-solo gu dawaan bu safaanu, ba waral ci genn wàll li tax ñépp jël ko, mooy yomb gee jëfandikoo fu nekk, yomb gee soppi ci lim yu wuute ci taraayu dawaan, ci ndimbalu soppalikaay yi, ak ñakkug kàttan gu digu. + +Donte yenn jumtukaay yi dawaan bu wéy lañuy doxe, waaye loolu manees na koo ame ci dawaan bu safaanu, sunu jëfandikoo ab jubbantikaay. + +Suñu jëfandikoo ag xaralag mbëjfeppal gu kàttan gu ñaw, manees naa jëfandikoo dawaan bu wéy ngir am dawaan bu safaanu, jur ko ci yenn anami baraay, melokaanu duus ak taraay jaare ko ciy jumtukaay yees duppee jallarbikaay. + +Taariix + +Ca njalbeenu njëfandikug kàttanu mbëj ci ndefar gi ci XIXu xarnu daawaan bu wéy lañu doon jëfandikoo, ndax li mu doonoon lu neex a rënk ciy tegle ak li mu gën a wóor dawaan bu safaanu. Tomb bu mujj bi Thomas Alva Edison mooy ki ko doon wax ci lees tuddewoon xareeb dawaan yi. + +Dawaan bu safaanu, gi soloom doonoon lu beneen xaaj bi boole woon Nikola Tesla ak George Westinghouse doon aar, manul a ñakk ci njëfandiku gu ab soppalikaay, moom mi tax ñuy man jokkalante mbëj mi ci diggante yu gudd. Te itam doxalukaayu mbëj yu dawaan bu safaanu ñoo gën a wóor te gën a yaxan yu dawaan yu wéy yi. + +Ci jamono jii ci àdduna bi dawaanu mbëj ci ñaari baraay lañu koy séddalee, 50 Hz(Tugal, Asi, Afrig) ak 60 Hz(Diiwaan-yu-Bennoo ak goxu Aamerig bépp ci lu daj, genn xaaju sapoŋ) ak taraay yu wuute. + +Xool it + Dawaan gu wéy + + Dawaanu mbëj + + Kàttanug mbëj + + mbëj + +Téerekaay + + Charles Proteus Steinmetz: Theory and Calculation of Alternating Current Phenomena (McGrawHill, 1900) + + Charles Proteus Steinmetz: Electric Discharges, Waves and Impulses (1914) * Charles Proteus Steinmetz: Theoretical Elements of Electrical Engineering (1915) + + Charles Proteus Steinmetz: ''Theory and Calculation of Electrical Apparatus (1917) + + Charles Proteus Steinmetz: ''Theory and Calculation of Transient Electric Phenomena and Oscillations(McGrawHill, 1920) + + Louis Cohen: ''Formulae and Tables for the Calculation of Alternating Current Problems (McGraw-Hill, New York, 1913) + + Ernst Julius Berg: Electrical Engineering, First Course (McGrawHill, New York, 1916) + + Ernst Julius Berg: Electrical Engineering, Advanced Course (McGrawHill, New York, 1916) + +Dawaanu mbëj +Dawaanu mbëj ag wal la niki yépp gu nosu gu yani mbëj (njunjam di Q), naka-jekk cig wëñug weñ lay jaar walla bépp jumtukaay buy watat. Dawaan bi dees koo jappee woo, ci ndorteelu taariixu mbëj, niki ag walug yan yu baax (+), donte sax xam nanu ne, su nu xoolee ci watatukaay yu mbell yi dawaan gaa ngi judd ca walug mbëjfepp yi, yi am yan yu bon (-), ci beneen jubluwaay bi. Kon ni ñu foogeewoon ne la dawaanu mbëj di jublu, du noon, waaye safaan wa la, yan yu bon (mbëjfepp) yi ñooy dox jëm ci yu baax (+) yi. Donte lii yépp, gisiin gu njëkk ga moo wéy di baax, ci déggoo. Njunj gi ñuy jëfandikoo ngir tudd bariwaayu dawaan (limu dawaan giy wal ci jenn jamono) mooy I, di ko wax taraayu dawaan, te bennaanu natt bi ñu koy natte di bi àdduna bi déggoo mooy ampere. + +Nattug taraayu Dawaan gi +Dawaanu mbëj manees na koo natt ak jumtukaay bees di woowee nattampere, waaye gii anam dafay laaj nga dog ndombo gi, xamees na ne du li gën ci yenn nekkiin yi. Dawaan bi manees na koo natt te du jar dog ndombo gi, ci njëlug toolub bijjakoon bi mu jur, moom. jumtukaay yees di jëfandikoo ngi bii liggéey ràññee nañu ci: yëgukaay yu sukkandiku ci njeexitu Hall ak lëmës yu Rogowski + +Xeeti Dawaani mbëj + + Dawaan bu wéy + + Dawaan bu safaanu + +Faramfacce +Xamees na ne ngir mbëj mi maase ci biir ab watatukaay faww toolu mbëj bi ci ëmbu di neen (tus) ci bépp tomb boo jël ci biir watatukaay bi. Su amee ag wuuteeg aj ci diggante ñaari tomb ci watatukaay bi kon dees na fa am toolub mbëj bu wuute ak tus kon dees na fa am it dawaanu mbëj. Wuuteeg aj googu lees di wax dooley mbëjdoxalukaay, di doole jiy xëcc yani mbëj yi, ñuy man di daw toppante doon ag wal, te ci la ndombo yu mbëj, mbëjbijjakoon, àtteb Ohm ak àttey Kirchhoff sukkandiku. + +So jële genn yaa-yaa gu watatukaay bi, benn limu yani mbëj di daw ci biiram 'ΔQ' ci benn diirub jamono 'Δt' dees na ci ame genn taraayu dawaan + +Lëkkalekaay yu biir + + Dawaan bu wéy + Dawaan bu safaanu + Kàttanug mbëj + mbëj + +Dawaanu mbëj +Xaralaymbëj +Soppalikaay ab jumtukaay la buy tax a man a soppi limu dend ak taraayu dawaanu mbëj bu jóge cib gongikuwaay buy jur kàttanu mbëj gu safaanu, ci beneen limu dend ak taraay yu wuute te bokk baraay ak melokaan. Te limuy ñakk ci kàttan ci soppali gi lu néew la. Ab soppalikaay, ci dawaan bu safaanu rekk la man a doxe, ndax ci bii xeetu dawaan la mbëjbijjaakon bu safaanu, di ci li doxam aju, man a juddoo. + +Soppalikaay yi ci ndomboy jokkalekaayu dawaanu mbëj yiy lëkkale jóoxuwaayu mbëj yi (digg yu mbëj) ak jëfandikukat yi lañu leen di jëfandikoo. Bokk na yenn ci ngirte yi tax dawaan bu safaanu bu Nikola Tesla am-ndaw ci kaw dawaan bu wéy bu Edison ci liñu doon woowee xareeb dawaan yi. + +Ubbite +Lim bu bari bu kàttanu mbëj bees soxla ci mboolaay yu taaxe yi tax na ñu war koo jóox ci bariwaay bu dayoowu ci jóoxuwaay yees duppee digg yu mbëj. Ngir man a xayma bariwaayu kàttanu mbëj bees jóox cib digg bu mbëj dañuy xool ci liñuy duppee ngóora gi(njunjam di P bennaanu nattam di Watt ñu koy tënk ci [W]) di luy man a nekk ci diggante ay fukki kw (kilowatt, 1 kW = 1000W) ci digg yu ndoxmbëj walla yu jant ba ci ay teemeeri MW (megawatt, 1 MW = 1.000.000 W) di yu digg yu tàngmbëj ak yu saal. Gii kàttan dañu koy yóbb ci ay teemeeri km. Ngóora (P) gi mi ngi am digaale ak dawaan (I) geek dend (V) gi ci mbindum xayma miy toftal: + +Lii dafay tekki ne man ngaa yokk walla wàññi dend gi walla dawaan bi te ngóora gi du soppeeku (te jéem a fexe ba jege 1 (benn)). Lii am na solo lool ndaxte dawaan bi I dafay jur tangoor suy jaar ci biir watatukaayu mbëj bi (ngir njeexitu Joule): lu dawaan bi di gën a bari tangoor giy judd di gën a bari; ngir moytu lii faww ñu yokk dijjaayu watatukaay bi, waaye it yokk gi am na dig ci wàllu koom ak xaral, aju na tamit ci feeñte bi ñuy duppee waddug dend yu buum yi ci seen bopp. Kon ngir wàññi dawaan bi dañuy def ab soppali yokkaale dend gi ci anam gu ngóora gi dul soppeeku. + +Ag sàkkam + +Baaxi ab soppalikaay ki leen njëkk a taxawal mooy Michael Faraday ci 1831, waaye li mu ci jubluwoon rekk moo doonoon biral baaxi yi nekk ci xiirtalug mbëjbijjaakon, kon xalaatul woon nan la man a nekkee jumtukaay buy jariñ ci dëgg-dëgg. +Lucien Gaulard ak John Dixon Gibbs ci 1881 lañu génne ca Londar ab jumtukaay bees duppee woon «ñaareelu jurukaay», ñu daaldi jaay xalaat bi këru liggéey bu waa-aamerig ba Westinghouse. Mooy soppalikaay bees njëkk a jëfandikoo ci jëfe. + +Xaralaymbëj +li jaaxal borom xam-xam yi seen gëstu jëm ci kéew gi (changment climatique)di ay yàqu-yàqu ci jawwo ji.tàngaay wi di gën a tar,géej yiy wann dëkkuwaay yi, +Xët wu njëkk +Kàttanug mbëj xeetu kàttan la gu lonku ci doole walla tool yu jóge ci mbëj, maanaam lu ñeel yëngug, walla doxub, yani mbëj. Kàttanu mbëj manees na koo jëfandikoo ngir defi liggéey, leeral, tàngal,... + +Kàttan ak dawaanu mbëj + +Digaale bi ci kàttan ak ngóora +Kàttanu mbëj manees na koo natt ci dawaanu mbëj bi, balaa dara manees naa xayma liggéey bi + +, + +Liggéey bi W ciy joule, yan bi Q ciy coulomb ak wuuteeg aj gi ciy volt. + +ak , I dawaanu mbëj bi, t jamono ji: + +, + +te di Ngóora ciy watt. + +Kàttan gi manees na koo nattee nii: + + + +Kàttan gi UE ciy Joule mooy kàttan gi rënku cib toolu mbëj, C mooy def bi, di ci lees di sukkandiku ngir man a xam daayoob kàttan gees man a sol cib fattalukaay. + + + +Kàttan gi Um ciy Joule mooy kàttan gi rënku cib toolu bijjaakon, mooy walug bijjaakon giy soppiku ci jamono t. + +Ci yenn anam yi dees na man a bind gii yamale: + +Bennaanu natt +Bennaanu natt bi ëpp lu ñuy jëfandikoo ngir natt ab limu kàttanu mbëj mooy kilowattwaxtu (kWW) + +sunu xamee ne + +S mooy saa + +Xool it + +Kàttanug aj + +Kattanug saal + +Kàttanug mbëjbijjaakon + +Kàttan +Daanaka-dun ab dëkk bu géej peeg ci ñatti wet yi, mu laale ak suuf bi ci des. ( di ci FR presqu’île) + +Melosuuf +Toolu mbëj, ci jëmm, ab tool la bu ay cër yees yan mbëj sàkk. Ab tool bu ne mel mooy tax ñu man a natt dooley mbëj bi ci bépp tomb boo jël ci barab bi. Ci anam gi ñu koy gëstoo su fekkee ay yan yu tekkaaral lañu, toolu mbëj bi dafay doon toolu mbëjtekkaaral. + +Ubbite + +Njoxe yi tukkee ci caytu yi gëstukat yi def xamale nañu ne ñaari fànni mbëju yu ne-ne yi ñoo am: baax(+) ak bon (-). ñaari yaram yu mbëju, ñoom ñaar ñépp, ci anam gu baax walla gu bon dañuy bëmëxante, su dee wante dañoo mbëju ci anam gu wuute dañuy xëccante. Ngir xam ndax wenn yaram wi mbëju na, maanaan ndax am na yani mbëj ci biiram, dañuy jëfandikoo jumtukaay bees di woowee mbëjxool, moom du man a xayma taraayu mbëj mi ci biira li muy def rekk mooy wax ne am na ci mbaa déet. Ngir natt mbëj mi jumtukaay bi ñuy jëfandikoo mooy nattampere. + +Lii yépp li ko waral mooy melokaanu biir ne-ne yi rawatina cër yi dàtt xarefulwon bi. te itam sax xarefulwon bi li booloo doon ko mooy saal bi, bi ëmb ci biiram feppsaal yi ak feppmaandu yi, ak ab barab bu biti bu mbëjfepp yi nekk. Ci nekkiin gu jaadu ab xarefulwon dafay maandu, maanaam limu mbëjfepp yeek feppsaal yi ñooy tolloo. Ngir xayma dayoob yanub mbëj dañuy jël mbëjfepp bi gën a tuuti bu am ci dénd bi, dayoo bu mbëjfepp bu bon (-) moo yem ak e = 1,602 189 2 ∙ 10-19 C, tolloo te safaanoo ak bu feppsaal, C mooy bennaanu natt bu yan bi te ñu koy woowee Coulomb. feppmaandu yi ñoom amuñu yanu mbëj. + +Toolu mbëj bi fa mu man a àgg amul dig, taraayam ci bépp tomb boo jël ci biiram mi ngi aju ci ni ci yan yi séddalikoo walla xeeti ne-ne yi ne ci barab bi. Naka-jekk njunjam mooy , te tasaaroom yamaleb Maxwell moo ko faramfacce. ci Taariix Michael Faraday mooy ki ko njëkk a indi ci diggu XIXu xarnu bi ci ay gëstoom. Su ñu ko boolee ak toolu bijjaakon bi mu doon toolu mbëjbijjaakon. + +Toolu mbëjtekkaaral +Su fekkee teg nga ci ab barab ab yanu mbëj Q manees naa natt doole ji muy teg ci beneen yan qo bu ko gën a ndaw bu ñu jël, ci déeggoo qo bu baax (+) lay doon, su ñu tegee Q ci wetu qo. Niki nees koy gise ci gëstu yi, jooju doole dafay aju ci qo ba tax manees naa taxawal bii yamale: + +Toolu mbëj bi E, doole ji Q di teg qo F. Ci bii tekki lees di sukkandiku ngir jox toolu mbëj bi bennaanu natt , maanaam Newton/coulomb. yam itam ak , maanaam volt/metar). + +Ci tënk, toolu mbëj bi mooy liy jëmmal xëccante bi nekk ci diggante ñaar mbaa ay yani mbëj yu wuute yu taxaw, te tekkaaral, ci ñaari wet yu jakkaarloor , lu doole ji ñuy xëccantee di yokku toolu mbëj bi di yokku. Dig-digal bi nekk ci diggante yani mbëj yu jakkaarloo yi, yu baax (+) yi ci genn wet yu bon(-) yi ci geneen wet lees di wax lankmbëj. Lankmbëj bi mooy tax ba ab yanu mbëj du man a jóge ci genn wet dem ci geneen. Di fattali ne dawaanu mbëj du lenn lu dul ay yani mbëj yuy toppante, di daw; yu baax yi ñooy xëcc yu bon, su fekkee ab lankmbëj nekk na ci seen diggante dawaan du fa man a am. Su lankmbëj bi dëggëre ba tax dawaan manu faa judd, maanaam doole ji yan yu baax yi di xëcce yu bon yi amul taraay bu doy ba tax ñuy man a romb lankmbëj bi, ñoom yu bon yi, toolu mbëj daadi fai juddoo. Ba tax toolu mbëj du lenn lu dul doole jees sëf ab yanu mbëj. + +Xool it + Toolu bijjaakon + Toolu mbëjbijjaakon + kàttanug mbëj + +Mbëj +Mbëjfepp "électron ci fr" as wàll-wàllaan la (wàll su ndaw lool) su xarefulwoon bi bu sëfoo ab yanu mbëj bu bon(-) bu tollook qe = 1,602 · 10-19 C, te dayoom toll daanaka ci 9,10 · 10−31 kg (ci beneen bennaanu natt di 0,511 MeV/c²), dees na ko wax itam yan bu njëlbeen walla wàll-wàllaan wu njëlbeen. + +Naka-jekk ab mbëjfepp njunj bees koy jëmmale mooy e-. Xarefulwoon yi li booloo nekk leen ñooy ab saal (bi dajale ci biiram ay feppsaal aki feppmaandu) aki mbëjfepp yu koy wër. Dayoo mbëjfepp yaa ngi tollook daanaka 1/1836 yu feppsaal ak yu feppmaandu). Mbëjfepp yi cër yu cëslaayu lañu ci ne-ne yi, ñooy wàll-wàllaan yi gën a tuuti cib ne-ne ba tax kenn maneesu koo séddalewaat yeneeni cër. + +Jëmmu saal +Màggalug Tuubaa, Bis la bu màgg fi Taalubey Sëriñ Tuubaa yi te it di bis bu ñu fonk, Di it bis bi Sëriñ Tuubaa demee ci tukkib liggeey bi, ci 18 ci aw Magal (safar), Nu di ko amal at mune fa Tuubaa, ci fukki fan ak juróom ñatt (18) ci aw Màggal (Safar), ci arminaatu (calendrier) weer wi walla bu Hijri. Teg ko ci ndigalul Sëriñ Tuubaa "Bu bis bi ñëwatee na ngeen ma Santal Yàlla kem séen kàttan". +Mu digle woon ko ci fukki fan ak juróom ñatt ci atum 1341 ci hijri, di 16 julet 1921 ci Gregorian. Muriid yi di juge fune di jëm Tuubaa, ngir amali ko fa barab bu tedd boobee, dem na nag ba yamatul rekk ci Muriid yi, Waaye xanaa nekk xew-xewu Julli ñépp, Mbaa sax nit ñi ngir mu gën a matale, Muy yitte ju rëy, Ay miliyoŋi nit diko teewe. +Noonu it lees koy amale ci àdduna na si sépp, niki Aamerig, Tugal, Asi ak Afrig, ci Këri Sëriñ Tuuba yi, Fépp fu mbooloom Murid nekk,te gàllankooru ci man koo defee Tuubaa, dees nako fa amal ci genn anam gi, Lépp nag, Nu koy teg ci ndigalal Xalifa ba fa nekkal Sëriñ bi, Mookoy woote, mooy yeesal it ndigal la ci Sëriñ bi joxewoon, At mu jot. + +Baatu Màggal: +Màggal baatu wolof la, Maanaa mi man a doon fekk ku/lu/ju màgg nga nangul koko, Te di ko wone, Di baat bu jekkul ci lenn mbaa kenn ku moy Yàlla Màggaakon ba, Keneen koo ko solal mu ëpp ko, Mbaa mu di bokkaale, Sëriñ bi nag! ci jagle gi ko Yàlla may, te ñeelul keneen ak wuute gu mu wuute ak nit ñi, Bokk na ci baat bile, Ndax xew yi ko fi njëkk yepp séeni tur maneesu koo natt ci Yàlla aji Kawe ji, niki: Tabaski Yàlla jaaduwul ci Moom (tud naa sellam ga) ndax mooy Aji-Raye ji, Gàmmu Yàlla jaaduwul ci Moom (t.s) ndax amul bisub juddu, Tamxarit Yàlla jaaduwul ci Moom (t.s) ak beneen bis boo tànn nag, tur wa jaaduwul ci Yàlla, Moom Sëriñ Tuubaa nag ci jagley Yàlla, Mu indi fi Màggal ak Sant, Ñuy yu amul woon, te Yàlla jagoo leen, Magal Yàlla, Sant Yàlla, +loolu it bokk na ci Kiimtaani Sëriñ Tuubaa liggeeykatu Yonent buñu tànn ba. + +Taarixu Bis bi: +Ci njëkk sosu gi, Ku Tud Moor xari KAN la Sëriñ Moodu BUSO taawub Sëriñ Mbàkke BUSO yonni aw bëy mu juge GEDE jëm njaareem fa Sëriñ bi ni ko joxal ma ko Sëriñ Mulaay BUSO (Rakki Sëriñ Moodu BUSO mee la) neeko mu joxal ma ko Sëriñ Tuubaa niki àddiya, Sëriñ Mulaay yeew bëy wa ci barab dem ca Sëriñ bi neko "Sëriñ Moodu BUSO yonnee nafi ab gàtt" Sëriñ bi laajo ko ni ko "Gàtt ba lumu ?" mu ni ko Bëy wu jigéen la, Sëriñ Bi neko: ndax man ngaa fexe ba weccil ma ko am xar mu góor ? Mu neko: waawaaw ! Sëriñ Mulaay jël bëy wa ginnaaw bimu jotee ndigël ngir weccee ku ko ak am Xar, dem ca Séeréer su mbuudaay sa fa nekkoon, Ngir weccee ku ji bëy wa, Mu fekk fa ab séeréer neko: Man dey! damaa yor aw bëy, te bëgg ku ma ko soppil am xaaf (xar mu góor) ? Séeréer ba seet bëy wa, neko: waawaaw ! Man naa nekk, ndax bëy wa, ba ko séeréer ba seetee, Day bëy wu jigéen wu giir (jurandoo lu bari te lumu am mu dund) te joox (bari soow lool), Séeréer ba neko: Gàtt yaa ngi nii, seetal bu la ci soob, Sëriñ Mulaay neena: Ma seet xaaf ma ca gën a rëy, Séeréer ba neko: Sant naa ci bu baax ! Mu indi ko, Wax ko Sëriñ bi, + +Sëriñ Bi neko: Nanga ma ko dencal ba ma laaj lako, Neena: Mu denc ko, Ba bisub talaata fukki fan +ak juróom ñatt ci weeru Màggal (18 safar), ci atum 1341 ci Hijri, Di tolloo ak 16 julet atum 1921 ci Gregorian, Sëriñ bi woolu ko moom Sëriñ Mulaay, Jox ko ndigël neko: Sama gàtt ba mingi fi ? +Sëriñ Mulaay neko: Waaw, Sëriñ bi neko: Boo demee nga rendil mako, Te boo koy rendi, +nanga ci am pasteefub Santal ma Yàlla ci bis bii, ndax kat maangi xamle ne: Bis bii ci lama saa Boroom dëeloon ngir jox ma li taxoon may liggéey, te jox nama ko, kon nag ! Maangi ciy sant Yàlla, Te ndigël naa leen yeen Taalube yi, Bu bis bi ñëwatee ngeen santal ma ci Yàlla, Sëriñ bi neko nag: Boo demee rendi ko ci sa loxol bopp, fees ko ci sa loxol bopp, te it nga toj ko ñatti xaaj: +1-Benn saam bi, Nga jox ko Soxna Aminta BUSO [Way-juru Sëriñ Abdu Xaadir MBÀKKE], +2-Ñaareel bi, Nga jox ko Soxna Anta Bale BUSO [Di rakki Soxna Amina BUSO mee], +3-Ñatteel bi, Nga yobbu ko ca daara ja nga nekk, sarax naa leen ko. + +Ndigal li: + +Ginnaaw ba Sëriñ bi woolu magi Taalube yépp, siiw na ca ña ko fekke woon, Sëriñ Ma NDumbe MBÀKKE, Seex Ibraahima FAAL, Seex Iisaa JENN ak Sëriñ Mulaay moomii, ak ña ca des... ne leen: Ñu baax ña fi jaaroon ñépp (ci lu nëbbu xayna), Ku ci ne am na bis, niki Ibraahima (jàmm ci moom) ak Tabaski, Kon nag, Bu Tabaski ñëwatee Ku ci am ñaari gàtt, Nga ray benn ba ca Tabaski ga, Te ba ca des mu denc ko ba ci sama bis bii di 18 ci weeru màggal (SAFAR), Santalee ma ko Yàlla, ***... lii la waxoon ca kanamu mbooloo ma, +Ginnaaw santal léen ma Yàlla rekk la wax, te tudd ci ab gàtt, tudd ci it Tabaski, te it tuddee wu ko wenn tur, lumay ni léen ngeen Santal ma Yàlla rekk, Te sant di jëf aki wax, Tax ba ña ko daa def daako woowe «Tabaskiwaat/Tabaskiyaat» tur woowu di wey, +Ba am bis, Sëriñ bi ci ag fegoom ak yeesalug Diine gi ko tax a jog ak nimu bañee Bidaa, Bañ darra luy nduroo akug réer feeñ ci am mbooloom. Mu wax leen ne: «Bu ko kenn waxati Tabaskiyaat waaye Màggal», ñu door di ko wax Màggal ba fimne. + +Mu des nag jeneen wax ju mbooloowu wul, Waaye ku woor la ko wax, Di Sëriñ Amsatu JAXATE, Sëriñ Bi da koo woolu mu joge Tuubaa dem Njaareem (JURBEL) àgg fa ci waxtu wu tàng, Sëriñ Bi neko: Demal noppalu, Ba ca soba sa, Sëriñ bi woolu ko, neko: Lima la doon doye de moodi, Saa Boroom lama doon liggéey, Damaa dëela loon (digoon) nima: Ci bis bii lama koy jox, Te wanoon na mako, Bis bi yegsi na, wax ko neko: Bamay joge Mbàkke baari di bisum gaawu (samedi) 18 ci aw màggal (safar), Nattu yama Tubaab yi teg, lamuy metti-metti moom laa àndal, ba ca déwén sa ñu ful ko fukki yoon, Bis ba déllu siwaat ñu fulati ko fukki yoon muy téeméeri nattu, Mu déllu séeti, ñu fulateeti ko fukki yoon, Muy junniy nattu, Junniy nattu yooyu nag diirub fukki ati laggéey bi moom laa yanu, (8 ci géej gi, 2 gànnaar, Muy=10) ñu di ko ful, +Binga xamee ni nag, fukki at yi jeex na, Ci la nattu yi «Tàmbalee wàññi ku», Sama Boroom ci ag baaxam nema: Litaxoon ngay liggeey moongi nii ma jàkkaarloo ak loola, Waaye taxul woon ma jot ca, Ba ci bisub tay nag, lama Saa Boroom jox ma am sañ-sañu yoral ko saa bopp, ŋàbbal ko saa bopp, Bis niki tay mingi ak man, Malay xamal it ne: Damaa bëgg a sax di ci sant Yàlla, te digal leen it yeen Taalube yi ngeen sax dima ci santale Yàlla, Lima saa boroom jox nag, Mooy lima doon sàkku ca moom, Waaye xamal nama ne: Lii muma jox saa su bis bi dellu seetee Dana ko ful fukki yoon, (niki mu ko doon defe ca nattu ya) diirub jamono, Ba àdduna di fàddu, +Ginnaaw ba it ba ca àjjana, ab jant bees di xame waxtu amu fa, Waaye saa Boroom moom xamna saa sa ak jamono ja, Ba bu bis bi agsee, Mu fulal ma neexaayu àjjana ja fukki yoon (multiplier par 10), Sëriñ Amsatu neena: Ma làmb saa jiba (poche) fekk ci juróom benn fukk 300f jox ko Sëriñ bi neko: Ma santee ko, Sëriñ bi neko: War ngaa sant Yàlla, ndax sa juróom benn fukk yii, Laa yor ci xaalis man koo sante Yàlla. +Kon Sëriñ Moodu BUSO taawub Sëriñ MBàkke BUSO, Moo joxe lees jëkk a ray ci bisu Màggal, Sëriñ Mulaay BUSO moo jëkk a lottal ab Gàtt yéene ci Sant Yàlla, manaam gàttub Màggal, Sëriñ Amsatu JAXATE it moo jëkk a joxe wërsagam ci Xaalis, +ngir Santalee ko Yàlla Sëriñ bi, Manaam xaalisam moo jëkk ci Màggal gi. + +Woote bi: +Ginnaaw bi ko Sëriñ Bi diglee ci noonii, Ñu tàmbali koo def ci anam gu sax, Ku nekk diko defe fa nga feete, ci ndigalul Sëriñ bi, Waa Tuubaa fa tuubaa, Waa njaaréem fa njaaréem ci wetu Sëriñ bi Mag mune it diko defee ca dëkk ba nga sanc ci ndigalul Sëriñ bi, ak say dongo, noonu lees ko daa defe, Bi fi Sëriñ bi jógee it, Noonu lees ko daa defe ci teewaayu ak ndigalul Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke mi fi wuutu woon Sëriñ bi, ba bi fi Sëriñ Móodu Mustafaa bawoo Sëriñ Fàllu Mbàkke wuutu ko, ci la ko wootee, Ngir ñépp diko defee si Tuubaa ci ag booloo, noonii nag, lees ko daa defe ci Téewaayu Sëriñ Abdu Lahad Mbàkke, Sëriñ Abdu Xaadir, ak Sëriñ Saaliwu Mbàkke ba fimne ci teewaayu Xalifa bifi léen fi wuutu, + +Nees ko baaxoo Màggale: + +Dees na ci daje ngir dundal ag bokk, +Dees na ci Jàng Al-xuraan ngi dundalee ko bis bi, +Dees na ci Jàngi Xassida ngir jollee ko ci Yonent bi (Jàmm ci moom) akit dolli koo ci, +Dees na ci def ay bernde yaatal ko ci lekk ak naan, ci anam gu matale, Ba ku fa teew xeewlu ca namu ware, Ngir ñépp beg ak wone ci it xeewali Yàlla aji xeewale jees fay sant, ci bis bi ngir jéem a wone xeewal yi Yàlla defal seen Sëriñ te defal leen ko. +Dees na ca daje it ci ay barab, ngir fàttali njàngalem Sëriñ Tuuba ak a dundal ay jëfam, di dolleente ci diine, +di fàttli ña fa teew it di ay taalube mbaa ay Jullit, li Sëriñ bi woote lumu ? ba kune gis ci sa bopp. +Ak yeneeni mbir yuy jariñe te dëppoo ak njangalem Sëriñ Tuubaa mi di diiney kase. + +Ngënéel li ak njariñ yi: +Amna yu nëbbu ak yu feeñ te xamu ñu ci lumay lees ci wax, Waaye dëgg-dëggi mbir mi, Ay gumba lanu ci, Boroom bis bi ak Ka mu koy bisal rekk la ñeel. +Yu feeñ yi: +Bokk na ca dajale ay jullit ngir ñu dox bokk gi Yàlla doxal seen digante. +Bokk na ca it daje diggante ay bokki askan ak bokki nit, te dox ko di lu war. +Bokk na ca jàngum Alxuraan mu jaatu ci lim bu kenn manu la natt, te Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) wenn arafam moo gënn àddina ak li ci biir. +Bokk na ca it Jàngi Xassida ci lim bu kenn man la takk, te Yàlla digël nu te jiitu ci, nu julli ci Yonent bi, ne it ku ci julli mu ful ko. +Bokk na ca birnde yu matale mbooleem ña fay teew, Ba kenn dootul xàmme ku am ak ku ñàkk, ñepp jëfandikoo ñam wa gën, Te Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) ne: Yi gën ci diine ñooy:Bernde (joxe aw ñam) ak Nuyoo. +Bokk na ca dajeb woroomi Xam-xam, Dolleente, Jàngale, Xamale, Laabireente, Soññee ci diine, te ñu wax ne dajeb woroom xam-xam yi yërmànde la. +Bokk na ca dajeb kureeli diine yi, Ngir man a gën a rataxalaat diggante yi, Féddali bokk gi. +Bokk na ca it dajeb Taalube yi ak seeni Sëriñ siyaare, Yees lu ak Joxe Haddiya ji nga xamni Yàlla a ko digle ci Al-Xuraan. +Ak yeneeni ngëneel aki njariñ yu nu lott ci lim ko... + +Yu nëbbu yi: +Sant la Sëriñ bi woote, Sant nag lu màgg la ci Lislaam, Rawatina ci way-sóobu yi (Sufiyaanke), Jàppe nañu ko niki màqaama mu kawe, Benn ci ñatt yi gën a gaaw ci jigeel Ab jaam Boroomam, Muy Màqaama mu kawe, +Sëriñ bi wax na ne: «Kuy saa mbegte di sa mos (mbegte) bu bis bi ñëwee nanga ma ci santal Yàlla, Bu ëllëgee ma bokk ak yaw pay ga» +Mu waxaat ne:Kepp ku ci ray Ginaar ba Giléem ngir Santalee ma ko Yàlla ëllëg maak yaway bokk xeewal ya ca àjjana, +may ya bokk na ca li mu wax ne: Liko Yàlla jox saa su bis bi dellu seetee Dana ko ful fukki yoon, diirub jamono ba àdduna di fàddu, Ginnaaw ba it ba ca àjjana, ab jant bees di xame waxtu du fa am, waaye saa Boroom moom xamna saa sa ak jamono ja, ba bu bis bi agsee, Mu fulal ma neexaayu Àjjana ja fukki yoon (multiplier par 10), kon loolii yaw miko Màggal ci Ginaar ba ci Giléem, Sëriñ bi nee: yeen a koy bokk. +Sëriñ bi waxaat ne: «ñaar ñu ne, kenn ka fonk Màggal gi; ka ca des déet, du ñàkk ki ko fonk di gis li muy tiime moroom ji (li mo koy tanee)», Ak yeneeni ngëneel aki njariñ yu dul jeex te xam-xam ba ñeelul ku moy Ki (Sëriñ bi) bis lu ak kees Koy (Yàlla ji yayoo ag cant) bisal. + +Yoonu murit +Bisub Tamxarit Ak Bisub Tamñërit, Bisub Tamxarit di 9eelu fan ci weeru Tamxarit, bis la budi aw xew ci Jullit ñi, rawatina ñi ëpp ci sunnit yi, Siiha yi it dina ñu ko xewal ngir naqarlu, ray gees rayoon Useynu Sëtub Yonent bi (Jàmm ci ñoom) ca réewum Iraak, nees nako fa xumbal, ci àndandoo wàcc ci mbedd yi, di wone séni naqar, Ci julliti Senegaal yi, Baaxoos na toggi cere ca ngoon ga, ba ca guddi ga di guddig Fukkéelu fan ba, mu di guddi gu màgg ci lislaam ngir ay xew-xew aki ngënéel yu ci Yàlla jagleele, ku ca jàppu ba séll julli ñaari ràkkaa, ràkkaa bu ci ne nginnaaw faatiha nga tari saar wu la soob ci Alxuraan, boo noppee sàbbaal Yàlla lu la soob, julli ci Yonent bi (Xeewalug yàlla ci moom) lu la soob, te ñaan say aajo muslu ci balaa yoy at mi. + +Ammaa nag yeneen yees ciy def niki, jal suuf di ca këpp bool bañu doon reere, ak bàyyi ca bool ba ab danku cere ak tuuti ndox bu ñu xëyee di ci sëlmu, mbaa tusngalu di séentu asamaan ngir ni dañuy gis Faatimata bintu Rasuulilah, (Tusngalu nag sopp nañu ko ci), +Yooyu yépp ku koy def walla ku koy deflu mbaa ku gis ku gis ku koy def, na ko jàppe ni baax (aada) la rekk xamu ma nag séeni cosaan waaye tegeesu ko ci diine. +Tamñërit di bisub fukkéel ci wéeru Tamxarit, bis bu màgg la ci xew-xewi àddina rawatina ci Lislaam li ko dale ci sosug nit ba léegi, Yàlla defal naci ay jaamam xéewal yu rëy aki ngënéel, jéggal ci it ay jaamam, + +Xew-xew ci bis bi: + +Ci bis bii la Yàlla jéggalee woon Aadam ca bàkkaar bamu defoon ca àjjana bamu laalee garab ga +Ci bis bii la gaalug Yonent Yàlla Nooh (jàmm ci moom) ga teeroon ca géejug juudiyu (nékk ca Iraak) ba Yàlla di mbugal xeetam wa ca ndox ma. +Ci bis bii lees xaralee woon Yonent Yàlla Muusaa (jàmm ci moom) géej ga te labal Fir`awna aki ñoñam, Muusaa mucc aki ñoñam. +Ci bis bii la Yonent Yàlla Iisaa (jàmm ci moom) Juddu woon te wax waxi dëggëm ja, +Ci bis bii la Yuunusa (jàmm ci moom) génn ca jënwa ginnaaw bi ko ci Yàlla yabalee, ca génnam ga ci ludul ndigalul Yàlla. +Ci bis bii la Yonent Yàlla Yuusufa (jàmm ci moom) génnoon ca téen ba ko mbokkam ya dugaloon. +Ci bis bii la Yàlla musëlee woon Yonent Yàlla Ibraahiim (jàmm ci moom) ca sawara sa ko noon ya fasoona dugal ci ndigalul Namruus bamu diiŋatee la ñu jàppe woon Yàlla. +Ci bis bii la Yàlla yékkatee woon Yonent Yàlla Idriisa (Jàmm ci kawam) ba ca ñeenteelu Asamaan. +Ci bis bii la Yàlla yékkatee Yonent Yàlla Iisaa (Jàmm ci moom) ma nasaraan yi naan «rayees na ko» Alxuraan ni «Rayeesu ko sëlabeesu ko waaye dees léen a ndurooleel (Keneen ku nduroo ak moom)», moo nga ca ñaareelu Asamaan. +Ci bis bii la Yàlla jéggalee Yonent Yàlla Daawuda (jàmm ci moom) ca àtteem bu jeng ba ci laaj kenn ka ba ka ca des, +Ci bis bii lees di wodd Kaabak Màkka gees wormaal, (amaana muy ci lu nëbbu mbaa lu féeñ, lu nëbbu nag laa gën a jàpp ndax budee lu feeñ moom aada la te manees nakoo bàyyi.) +Yii yépp nag ay ngënéel yu nekk ci bis bi lay wone, ngir ni Yàlla a tànn xew-xew yii jagleel bis bi waliif yeneen yi, kon manees na cee tegoo ak jaamu kem sa kàttan te ñaan say aajo, ngir dabu ngënéel li ci ne. nuy Yakaar nangug séeni ñaan. + +Soppees na ci bisub Tamñërit di bisu 10eel ba yii: + +Sopp nañu kuko Woor, Sopp nañu ku ci julli ñeenti (4 i) ràkkaa yu boloo, bu ca ne mu jàng ca Saaru Faatiha benn yoon ak Saaru Lixlaas (Xul huwal laahu) fukk ak juróom, Sopp nañu ku ca jokk ak bokk, Sopp nañu ku ca seeti dëkkandoo bu di aji wopp te dëfal ko. Sopp nañu ku ca sangu, Sopp nañu ku ca saraxe, Sopp nañu ku ca lewwi ku dagg say wee, Sopp nañu ku ca raay boppum jirim bu di ab jullit te jox ko dara, jirim moodi ku baayam dee te amagul 18 ci ay at, ngir won ko ak cofeel mu man a jàppe boppam niki ay moroomam, Sopp nañu ku ca tusngalu, Sopp nañu ku ca siyaare boroom xam-xam,Sopp nañu ku ca yaatal ag njabootam ci lekk ak naan niki soppi sa cin temu matale, Sopp nañu ku ca jàng Saaru Lislaas (Xul huwal laahu) junniy yoon (1000), Sopp nañu ku ca jàng ñaan gii:70 i yoon «حسبناالله ونعم الوكيل نعمالمولي ونعم الموكيل», teg ca ñaan gii «سبحان الله ملء الميزان ومنتهي العلم ومبلغ الرضي وعدد كلمات الله التامات كلها أسألك السلامة برحمتك ياأرحم الراحمين ولاحول ولاقوة إلابالله العلي العظيم وهو حسبي ونعم الوكيل نعم المولي ونعم النصير وصلي الله علي سيدنا محمد وعلي ءاله وصحبه وسلم تسليما» jullig ñeenti ràkkaa gi nag manees na koo def ci ag booloo, rawatina ñu ko man la defal séen bopp, te it ginnaaw julli gi Yilimaan ji jàng ñaan gii ci anam gu leer bu ko defee maamoon ya man koo roy lu mu wax ñu wax ko, +Njariñi yenn ci yii: +Sangu ci bis bi day dàq ag ràgg, Tusngalu ci bis bi day jañ Gumba, Soppi sa cin temu matale day +yokk wërsëg. Koor gi Sunu Yonent Muhammad (Jàmmi Yàlla ci moom) wax nani «Woor léen Tamxarit bisu Juróom ñeenteel ba ak bob fukkéel ba ndax day far bàkkaari atmi» + +Ku ca bind lii: + +Saaru Faatiha, Aaayatu kursiyu, Lixlaas, Falaqi ak naasi lu ci ne benn yoon, teg ca juróom ñaari laaya yii wu ci ne balaa nga koy bind, bind BISMIL LAAHI AR-RAHMAANI AR-RAHIIMI, ñooy yii: +1-سَلَامٌ قَوْلًا مِّن رَّبٍّ رَّحِيمٍ (Saar:36, laaya:58) +2-سَلَامٌ عَلَىٰ نُوحٍ فِي الْعَالَمِينَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:79-80) +3- سَلَامٌ عَلَىٰ إِبْرَاهِيمَ, كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:109-110) +4-سَلَامٌ عَلَىٰ مُوسَىٰ وَهَارُونَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:120-121) +5- سَلَامٌ عَلَىٰ إِلْ يَاسِينَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:130-131) +6- سَلَامٌ عَلَيْكُمْ طِبْتُمْ فَادْخُلُوهَا خَالِدِينَ (Saar:39, laaya:73) +7- سَلَامٌ هِيَ حَتَّىٰ مَطْلَعِ الْفَجْرِ (Saar:97, laaya:5) +Raxaseko walla jambe ko ndoxum taw walla ndoxum teen mbaa ndoxum géej maanaam ndox muy dund, Ku ca naan Yàlla dana ko musël ci mboolem lu ñuy ragal ci mboolem musiiba yi ci at mi + +Li waral baatu "Tamxarit": + +Ñaari baati Wolof lees ci boole ñuy "Tam" di tekki jiiñ nit ak miim-deel (dëmmu) ak baatu "xarit" am ñaari tekki: benn, Xarit niki xaaj dara ca digg ba benn xaaj ba moodi xarit, ñaar, Xarit niki nit kooy àndal di diisoo ak yuni mel, (bii nag amaana mu jóge ci bu jëkk bi niki taqaloo gi), bees boolee tam ak xarit mu joxe Tamxarit, di jiiñ sa xarit ag miim-deel, ñu tuddee ko bis bi/weer wi, kon ana lu ko waral ? waaw, ndax waxees nani waaja daa woo ab xaritam ci reeru bis bi (fekk waaji daa Buun) xarit ba ñëw ñu taaj reer bi (cere ji) xarit ba topp ab ndeyjooram duy biir ba ci cerey yàpp ji ba mu fees dell, ñibbi biir ba di metti ci guddi gi tax ñu tamxarit ba mu demoon kërëm mu jox ko lekk ni mooko jàpp, bañu xëyee nag cere ja rees biir ba sedd ñuni aah Tamñërit, manaam tam ja wéy na, neena mërr, ñu tuddee bisub juróom ñeenteelu fan ba Tamxarit (ci lees tamoon xarit bi), bu ca goon gaa ñu baaxoo toggi cere aka Ta`jauun, tuddee bisub fukkéel ba Tamñërit (ci la tam ja weddi boppam) di ca julli ak di ca tusngalu ak yees lim ci kow... +diine +Lislaam +Feppsaal (deesi ko wax ci fr : Proton)(as wàll-wàllaan la su sëfoo yanu mbëj bu baax(+) su man a féex ciy yëngoom walla mu taq cib saalu xarefulwoon . Ki ñuy wax ne moo ko wuññi mooy Ernest Rutherford, donte jëmmaan bu waa-almaañ bi Eugene Goldstein njoortoon na ag nekkam njëkk ngir manoon a dëggal ay gëstoom. Dayoob yanu mbëjam tollook bu mbëjfepp, waaye ak màndarga gu wuute: 1,602 × 10-19 coulomb. Lefam tuuti la rombee 1800 yoon bu mbëjfepp (daanaka 1836) te xawa tollook bu feppmaandu: feppsaal a ngi am lef gu toll ci 1,6726231 × 10-27 kg (9,3828 × 102 MmV). + +Feppsaal yeek feppmaandu yeey ñaari wàll-wàllaan yi cëroo xarefulwoon bi, ñoom ñaar ci saal bi lañu nekk, mbëjfepp yi ci xarefulwoon lañu leen boole waaye taquñu ci dañuy nekk di ko wër. + +Jëmmu saal +Feppmaandu as wàll-wàllaanu xarefulwoon bi la. Di wenn ci wàll-wàllaan yi dàtt saalu xarefulwoon bi. Ni ko turam di junjee, feppmaandu dafa maandu moo tax amul yanu mbëj (du bu baax(+) mbaa bu bon(-)). Feppmaandu yeek feppsaal yi su ñu leen boolee ñooy nekk saalu xarefulwon bi. Ngir ab xarefulwoon, dañuy bind Z limu feppsaal yi, A di limu feppsaal + feppmaandu. Kon limu feppmaandu yi dafay doon N =A-Z. + +Lefu feppmaandu mi ngi toll ci 939,56533 MmV. Ki ko wuññi mooy jëmmaan bu waa-angalteer ba James Chadwick ci 1932. + +Xool it + + mbëjfepp + + feppsaal + + xarefulwoon + +Jëmmu saal +Xarefulwoon (di tekki lees manatul a xar, di ci fr Atome), baat bi Seex Anta Jóob a ko tëgg te mi ngi sukkandiku ci bu njëkk li ñu foogoon ne mooy xaaj bi gën a tuuti bees manut a xaraat bu ab ne-ne, (manees na koo tudde it fepp (mi doon tuutalug pepp "peppu suuf as feppu suuf") muy lu bawoo ci ngéru xeltukat yu waa-gires yu yàgg ya. Mooy wàll wi gën a tuuti ci bépp cër bu nekk ci dénd bi buy wéy di yor màndarga yu simi yu la mu doon, ci yeeneen kàddu, soo ko xaaje du nekkati wenn wàll wu ne-ne wa mu bokkoon laataa xaaj gi, beneen xeetu ne-ne lay nekk. + +Ci mujjug ati 1800 (ak wuññig mbëjfepp) lañu biral ne xarewulwoon manees na koo séddale, ndax li mu doon, moom ci boppam, lu cëroo ay wàll-wàllaan yu bari yu gën a ndaw (baatu ronxarefulwoon loolu lañu ci jublu). + +Faramfacceb xarefulwoon mooy faramfacce biy wax ci melokaanu ne-ne yi, di dëggal ne bépp ne-ne ay bennaan ñoo ko cëroo te ñu leen di woowee xarefulwoon, ñoom ñooy dajaloo ci benn anam bi nekk ne-ne bi. Bii faramfacce ñoo ngi koy man jëfe ci ne-ne yi nekk ci nekkiin wu wow, yullaakoon ak wu gile. + +Ab xarefulwoon mi ngi cëroo ab saalu xarefulwoon, bu am ay yani mbëj yu baax, ak ay mbëjfepp yu am yan yu bon te di wër saalu xarefulwoon bi di wëndeelu ci anam gu nosoodiku. Saalu xarefulwoon bi mi ngi cëroo ay feppsaal, yu doon ay wàll-wàllaan yu ami yan yu baax, ak ay feppmaandu, di ay wàll-wàllaan yu amul yanu mbëj. Ab Saalu xarefulwoon di na am lef wu ëppee ab mbëjfepp 1800 yoon. + +Màndargaay wàll-wàllaan yi ne ci ab xarefulwoon: + +Jëmmu saal +Toolu bijjaakoon, ci jëmm, ag feeñte la gu màndargaloo ab taraay ak ab jubluwaay bu jenn doole, jees duppee Dooley Lorentz, ju judd ci doxub ay yani mbëj. Toolu bijjaakon, moom ak toolu mbëj ñooy ñaari cëri toolu mbëjbijjaakon di li banqaasu jëmm bi di mbëjbijjaakon di faramface. Soo boolee ay duusi ab toolu mbëj ak yu ab toolu bijjaakon dañuy man a baawaan ci barab bi ak ci lu ëpp ci ne-ne yi. Yii xeeti duus lees di wax duusi mbëjbijjaakon te leer gi nuy gis bokk na ci yenn ci anam yi mu ñuy feeñoo. + +Maxwell moo fexe ba boole mbëj ak bijjaakon, ci nii, mu jur ag noste gu ñeenti yamale (Yamaleg Maxwell) yuy lëkkale seen ñaari tool yi. Bu njëkk ñaari tool yi dañu leen doon tàqale ngir gëstu, faramfacce, seen feeñte yu wuute. Albert Einstein moo wone, ni tooli mbëj ak tooli bijjaakon doonee ñaari anami feeñiin yu benn feeñte; ni ab xoolkat man a gisee jenn doole ju bijjaakon, ci jenn jamono ji, beneen xoolkat buy daw di gisee jenn doole ju mbëjtekkaaral, di liñuy duppee gisiin wu ajoo. Ci nii, ak ajoo gi, manees naa xam doole ju bijjaakon ji ci bu nu xamee doole yu mbëjtekkaaral bi. + +Bijjaakon +Toolu mbëjbijjaakon, ci jëmm, ab tool la buy juddoo ci teewaayu yani mbëj, banqaasu jëmm bi koy gëstu mooy mbëjbijjaakon. Ay bokkaanam (ñi bokk doon ko) ñooy ab toolu mbëj ak ab toolu bijjaakon, seen teewaay di juddal ay doole yees man a natt ci bépp tombu tool bi ci jamono ju ne. Ci fànnu gisiin wu ajoo dees na ci wuññee ne toolu mbëj ak toolu bijjaakon ñaari feeñte lañu yu wuute tur te di lenn li, lépp mbiru nosteg delluwaay la. ba tax sax su benn xoolkat bu taxaw di gis ci misaal ab toolu mbëj kepp, ab ñaareelu xoolkat buy yëngu moom dina gis ab toolu mbëj (nakka-jekk waaye bu dul tekkaaral lay doon) ak ab toolu bijjaakon. + +Toolu mbëjbijjaakon bi dafay jur jenn doole ji ci wenn wàll-wàllaan wees yan, bu yamaleb Lorentz diñu jox: + + +Te di yanu wàll-wàllaan wi, diy xélam, toolu mbëj bi, moom di xiirtalug mbëjbijjaakon bi. +Àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy wax ne: wuuteeg aj giy judd ci ag ndombo gu tëju dafa aju ci anam gu jonjoo ci coppite gu walug bijjaakon gi te aju itam ci diirub jamono bi muy ame. Ci yeneen kàddu dafa aju ci xél yi walug bijjaakon gi di soppikoo ci jamono ji. Doxiinu masini mbëj yu bari yu mel ne ci misaal soppalikaay yeek doxalukaayu mbëj yi ci bii àtte lañu sukkandiku. + +Lëkkalekaay yu biir + Toolu mbëj + + Toolu bijjaakon + + mbëj + +Mbëjbijjaakon +Yanu mbëj, ag jagle gu dàttu la ci wàll-wàllaani ab ne-ne, mooy tax seenug man a digaale ci ndimbalu tooli mbëjbijjaakon yi. Doole jiy judd ci googu digaale mooy sabab ag yëngu ci biir ne-ne bi, muy ab dawaanu mbëj. +Bennaanu natt bu benn yan mooy Coulomb. Yan bi gën a ndaw bees man a natt mooy bi ab mbëjfepp di yanu, ñu koy faral di binde e = -1,602 10-19 c. + +Yanu mbëj am mbir mees di janeer la, du lees man gis ak bët, dafa di aw tur wees jox genn feeñte gi ngir man a faramface wenn xeetu doxiin wi, di njeexiitam. Yanu mbëj man naa am ñaari xar-kanam yu wuute, di yees jàppee yu "dekkarle" ; benn bi di bu baax (+) beneen bi di bu bon (-). Ñaari yan yu wuute (bu baax ak bu bon) dañuy bijjante, ñaar yu bokk (ñaar yu baax walla ñaar yu bon) dañuy bëmëxante. + +Yan yu bon yi lañuy faral a tudde ay mbëjfepp, yu baax yi di ay feppsaal ndax ñooy yiy nekk ci biir saalu xarefulwoon bi te kemu seen yan yam ak yu mbëjfepp yi te dekkarloo. + +Dawaanu mbëj man naa am ñetti sabab: walug ay feppsaal (yan yu bon) walla walug ay mbëjfepp (yan yu baat), walla seenug wal ñoom ñaar ñépp ci jubluwaay yu dekkarloo. + +Ngir bañ ay jaxasoo mbëjkat yi dañoo ànd ci ne walug yan yu baax yeey dawaanu mbëj, ci liñuy tudde dawaanu déggoo, ndax bu njëkk dañoo foogoon ne doxug wàll-wàllaan yu baax yeey jëmmal dawaan bi, donte tay jii dem nañu ba xam ne safaan bee nekk: dawaanu mbëj doxug mbëjfepp yee ko jur. Ndax feppsaal yi duñu ay wàll-wàllaan yuy dox, ci saalu xarefulwoon bi lañu sax dëkk. Bànqaasi xam-xam yi yittewoo gëstu yile feeñte ñooy xaralaymbëj ak mbëjfeppal. + +Lëkkalekaay yu biir + + mbëj + Toolu mbëj + bijjaakon + Toolu bijjaakon + Toolu mbëjbijjaakon + +Mbëj +Ndëgërlu gu mbëj ag jagle gu jëmm la guy tax nu man a natt bañ gi ab wommatukaay di bañ su ko dawaanu mbëj di jéem a jàll. Lànk googu dafa aju ci ne-ne bi ñu defare PENISwommatukaay bi, dijjaayam, tàngaayam, ak, su fekkee dawaan bu safaanula, baraayu dawaan bi. Genn ci njeexiitu jàllug dawaanu mbëj ci ab wommatukaay mooy yokkug tàngaayam, di liñuy wax njeexiitu Joule. + +Ndëgërlu gi ci gii yamale nga koy xamee: + +Tekki: + R mooy Ndëgërlu gi nekk ci diggante ñaari cati wommatukaay bi, ohm[Ω] mooy bennaanu nattam. + V mooy dend bi ne ci diggante ñaari cati wommatukaay bi , volt mooy bennaanu nattam. + I mooy dawaan biy jàll ci wommatukaay bi, amper mooy bennaanu nattam. + +Ndëgërlug ag wëñu wommatukaay + +Ndëgërlu R gu ab buumu wommatukaay nii lañu koy xaymaa. + +Tekki: + L mooy guddaayu buum gi, meetar mooy bennaanu nattam. + S mooy dijjaayam, m2 mooy bennaanu nattam. + ρ (arafu waa-geres: ro) dëgërluwiin gu wommatukaay bi, ohm * meetar mooy bennaanu nattam. Di maanaam man gi wommatukaay bi mane dëgërlu dawaanu mbëj buy jàll ci biiram. Ci yeneen kàddu Ndëgërlu gu ab wommatukaay dafay aju ci kemu man a ma dëgërlu. Ci lu ëpp Ohm x mm² / m lañ koy natte, lii moo lay jox Ndëgërlu, ci ohm, gu genn wëñ guy wommat dawaanu mbëj gu gudde 1 m te dijjee 1 mm². + +Misaal: dëgërluwiinu përëm mooy 0.0175 ohm x mm² / m, kon lii da lay wax ne ag wëñu përëm gu gudde 1 m dijjee 1 mm² Ndëgërloom gu mbëj day doon 0.0175 ohm. + + mooy wommatiin gi, maanaam ni wommatukaay bi manee wommat. + +Ajoom ci tàngaay +Ninu ko biralee ci kaw, Ndëgërlug ab wommatukaay nii lañ koy xaymaa. + +waaye ak bii yamale, dëgërluwiin gi dafay aju ci tàngaayu wërlaay gi mu ne. Su fekkee fésaluñu ko, dangay jàpp (ninu ko waxee ca kaw-a-kaw) ne ci tàngaayu 20° la. Mbindiin wii moo koy wone . Ci maanaa mooy ne ndëgërlu gi dafa aju ci tàngaay bi, lii man nañ koo wax ci bépp wommatukaay. + +Lëkkalekaay yu biir + mbëj + xaralaymbëj + doxalkat mbëj +babyolie gwn kersensaus ja + +Mbëj +Dëgërluwiin walla Dëgërluwiin gu mbëj mooy ni ab wommatukaayu mbëj jikkowoo di jéem a bañ ay yani mbëj di ko jàll, di dëgërlu. Ci dëgërluwiinu ab jumtukaay lanuy man a xamee nu ndëgërloom toll. + +Tekki +Dëgërluwiin wi ρ bennaanu nattam mooy ohm x meetar [Ω x m], dafa aju ci ni wommatukaay bi bindoo (dijjaayam, guddaayam) waaye li ko lonkale ak Ndëgërlu gi R mooy mile mbind: + + ρ mooy Dëgërluwiin wi ñu koy natte ohm x meetar [Ω x m]; + R mooy ndëgërlu gu benn dogu jumtukaay boo jël ñu koy natte ohm [Ω]; + l mooy guddaayu jumtukaay bi dawaan bi di jaar ñu koy natte meetar; + S mooy dijjaayu jumtukaay bi ñu koy natte meetar kaare [m2]. +Sunu wëlbëtee ci bii yamale mu jox nu nan lanuy natte ndëgërlu gu ab wommatukaay bu nu xamee guddaayam ak dijjaayam: + +Dëgërluwiin gi manees na koo natte itam ak bii yamale: + + E mooy taraayu toolu mbëj bi, ñu koy natte volt ci meetar + + J mooy fattaayu dawaan bi, ñu koy natte ampere ci meetar kaare + +ci mujjante manees na koo natte itam ak safaanu wommatiin wi: + + σ mooy wommatiin wi. + +Ajoom ci tàngoor + +Dëgërluwiin gu ab wommatukaay dafay aju ci xeetu ne-ne bi ñu ko defaree. + +Dëgërluwiin gu ab mbéll + +Ci mbéll yi Dëgërluwiin gi dafay yokk lu tàngaay bi di gën a bari, manam a wommat dafay wàññeeku. Safaan wa su tàngaay bi wàññee koo ba àgg ci benn lim bumu manuta romb. + + mooy Dëgërluwiin gi T tàngaay bi, mooy Dëgërluwiin gi ci tàngaayu delluwaay bi, naka-jekk benn ci ñaar yii lay doon 0° walla 20°. &alpha di ab ngungu tàngoor bu aju ci ne-ne bi. + +Dëgërluwiin bu ab xaaj-wommatukaay + +Dëgërluwiin gu ab xaaj-wommatukaay dafay wàññeeku lu tàngaay bi di yokk, kon lu tàngaay bi yokk ñuy gën a man a wommat. Bii digaale moo koy faramface: + +A, B ak C ay ngung yees jagleel ne-ne bi lañu. + +Lëkkalekaay yu biir + Wommatiinu mbëj + Wommat wu mbëj + Dëgërlukaay + +Mbëj +Wommatiinu mbëj walla Wommatiin wi moo nuy wax ci anam gi wommat wu mbëj wi di amee. Ci limam lanuy sukkandiku ngir man a xam ñaata la benn jumtukaay bi manee wommat mbëj. Safaanam di dëgërluwiinu mbëj wi di li lay wax ni ab jumtukaay manee dëggërlu jàllug dawaanu mbëj ci biiram. + +Tekkeem +Bennaanu nattu wommatiin wi mooy siemens ci meetar [s/m]. Nekk itam dawaanu mbëj ci kaw taraayu ab toolu mbëj [I/E]. lu bari bile araf lañu koy teewalee . + + + mooy Wommatiin wi + +ρ mooy dëgërluwiin wi (ñu koy natte ohm* meetar) + +R ndëgërlu gu mbëj gu ab wommatukaay (ñu koy natte ohm) + +l mooy guddaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar) + +A mooy dijjaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar kaare) + +Lëkkalekaay yu biir +Wommat wu mbëj +Dëgërluwiin +Dëgërlukaay +mbëj + +ru:Электрическая проводимость#Удельная проводимость +uk:Електропровідність#Питома електропровідність +Wommat wu mbëj ab tur bees jox benn feeñteb jëmm bi la ngir mu teewal nangu gu ab wommatukaay dawaanu mbëj jàll ko. Wommat wi dafa aju ci wommatiin wi. Wommat wi G mooy safaanu ndëgërlu gi R. + +Bennanu natt bu wommat wi mooy siemens (s). + + di ohm moom lañuy nattee ndëgërlu gu mbëj gi. + +Digaaleem ak yeneeni kem + +Ci yamale gi ci suuf la digaaleem ak Ndëgërlu gi gën a feeñee. + + + +G mooy wommat wi, +R mooy Ndëgërlu gi, +I dawaan bi, +V dend bi. + +Lëkkalekaay yu mbëj + +mbëj +Ndëgërlu gu mbëj +Wommatiinu mbëj +mbëj +Dëgërlukaay ab xeetu jumtukaayu mbëj la bu am solo lool ndax ay jëfandikoom yu bari te wuute ci defari masini mbëj ak yu mbëjfeppal. Naka-jekk ab dëgërlukaay dafay soppi kàttanug mbëj mu doon kàttanug tàngoor gu dawaanu mbëj jaaree ci biiram. + +Ci yamale gees duppee àtteb ohm lees di man a xaymaa ndëgërlu gu dëgërlukaay bi. Kàttanu mbëj gi dëgërlukaay bi di soppi kàttanu tàngoor mi ngi aju ci dayoob ndëgërloom (walla ci man a wommatam), ci dawaan bi ak ci dend bi. + + +V di dend bi, I dawaan bi, R ndëgërlu gi + +walla: + +G di wommat gi + +Waaye yii yamale duñu bàyyiwaale xel ci ne ndëgërlu gu Dëgërlukaay bi dafay soppi ci coppiteg tàngoor gi, dafay yokku su yokkoo, moo tax ñu koy woowee ndëgërlu gu xalaat, su fekkee dañu koy bàyyiwaale xel ndëgërlu gu dëgg lañu koy wax. + +Ngóora gi p gu ab Dëgërlukaay ñoo ngi koy natte: + +Ñu koy nattee ciy watt. + +Mbëj +Jurukaayu mbëj ab jumtukaay la buy tax ñuy man a jël wenn xeetu kàttan wi soppi ko kàttanu mbëj. Naka-jekk xeeti kàttan yees di soppali gu mbëj ñooy gu doolerandu, gu simi, gu leer ak gu tàngoor. Jurukaayu mbëj yi dañu leen di séddale ci jurukaayu dawaan ak jurukaayu dend, bu njëkk bi manees na koo, itam, séddale ci jurukaayu dawaan bu safaanu ak jurukaayu dawaan bu wéy. + +Jurukaayu dawaan ak bu dend +Àtteb ohm mooy yamale giy wone digaale gi ne ci diggante dawaan ak dend ci biir ag ndombo gu mbëj. Bu ci yokku sa moroom wàññeeku su ngóora gi soppikuwul. + +Tekki: + + P ngóora gi, ñu koy natt ciy watt. + V mooy dend bi ne ci diggante ñaari cati wommatukaay bi , volt mooy bennaanu nattam. + I mooy dawaan biy jàll ci wommatukaay bi, ampere mooy bennaanu nattam. + +Jurukaayu dawaan +Ab jurukaayu dawaan mooy tax nu man a am dawaan bu sax, limam ci biir ag ndombo gu mbëj gu mu nekk du soppiku ci coppiteg dend bi, limu dend bi man naa nekk lu ne te moom du soppiku. + +Jurukaayu dend +Ab jurukaayu dend moom mooy tax dend bi ci ag ndombo di sax, dayoom du aju ci dawaan bi. + +Xool it + + Doxalukaay bu mbëj + +Xaralaymbëj +Dendu mbëj, ci biir ab toolu mbëj, lañuy faramfacce niki liggéey bi mu laaj gir man a jële ab yanu mbëj (1 Coulomb) ci ab tomb yóbb ko ci beneen. Dendu mbëj dañu koy jaawale ak wuuteeg aj gu ñaari tombi ag ndombo gu mbëj, su fekkee toolu mbëj bi duy soppeeku (maanaam dayoom sax) dañuy wuute wante su fekkee dafay soppi dayoom ci benn diir bu nekk wuuteeg aj gi kenn dootu ko man a natt ba tax dañu koy yamale ak dend bi. + +Tekkeem +Su dawaanu mbëj dee liy natt walug yan yi, dendu mbëj mooy natt kàttan giy yóbb yan yi. Njunj bees koy jëmmalee mooy U walla yenn saa yi V te bennaanu nattam di volt [v]. + +Séddaleb kàttanu mbëj +Nbombo yi ñuy séddalee kàttanu mbëj dañu leen xaajale ciy wàll sukkandiku ci seen dayoo: dend bu kawe, dend bu diggu, dend bu suufe, dend bu suufe lool. + +Lëkkalekaay yu biir + mbëj + + toolu mbëj + Dawaanu mbëj + +Xaralaymbëj +Safaanukaay ab masinu mbëj la buy soppi kàttanu doolerandu ci kàttanu mbëj ci melokaanu dawaan bu safaanu. Soppali gi mi ngi cëslaayu ci feeñte gu xiirtalug mbëjbijjaakon. + +Defariin +Defariin gi dafay aju ci xeetu safaanukaay bi mu nekk. + +Safaanukaay bu demandoo + +Masin bi dafa am ñaari xaaj, benn bi ab xott la bu am am pax ñu koy wax tekkaaralaan, beneen bi di xaaj biy dugg ci bu njëkk bi, ñu koy wax wëndeeluwaan. Baatu demandoo mi ngi jóge ci li walug bijjaakon bi di demandoo ak wëndeeluwaan bi. + +Ci tekkaaralaan bi la lëmës giy jur toolu bijjaakon buy wëndeelu di nekk ci ndimbalu ay mbëjbijjaakon, seen lim yam ak limu wéq yeek seexi dott yi, kon su nekkee ab safaanukaay bu ñettiwéq, ñetti mbëjbijjaan ak ñetti seexi dott lañuy doon, su nekkee ñeenti wéq juroomi mbëjbijjaan lañuy doon. Safaanukaay bu demandoo ab doxalukaay bu demandoo lañu jël wëlbati ko. Ab doxalukaay soo ko joxe kàttanu mbëj mu delloo la kàttanu doolerandu, soo ko wëlbatee jox ko kàttanu doolerandu mu nekk ab jurukaayu mbëj, jox la kàttanu mbëj. + +Safaanukaay bu demandoodi +Bii xeetu safaanukaay ab doxalukaay bu demandoodi lañu jël wëlbati ko mu nekk jurukaayu mbëj. Ngir mu man a dox niki jurukaay faww muy jële kàttan ci geneen ndombo gu biti ngir man a bijjaakoonal lëmës gu wëndeeluwaan bi. Su wëndeeluwaan bi di wëndeelu lay joxewaale kàttanu mbëj waaye ngir walug bijjaakon gi koy wëndeel di sax di dox faww muy wéy di jëlee kàttanu mbëj gu koy dundal ci beneen safaanukaay bu demandoo. Lii moo tax daanaka du xeetu jurukaayu mbëj bu ñuy faral di jëfandikoo ci digg yu mbëj yi, bu demandoo lañuy jëfandikoo. + +Jëfandikoom ci jëfe +Safaanukaay yi bari nañu fi ñu leen di jëfandikoo, ci biir bépp digg bees di jóoxee kàttanu mbëj. Ginnaaw jóog gi ci dawaan bu safaanu, ngir man koo yóbb ba ci liggéeyuwaay yeek kër yi dañu koy soppali ak ab soppalikaay. + +Wuutuloxo yu mbëj +Doxalukaay bu demandoodi ab xeetu doxalukaay bu mbëj la bu dawaan bu safaanu bu xél yu wëndeeluwaan bi yamul ak yu toolu bijjaakon buy wëndeelu bi lëmës yi nekk ci tekkaaralaan bi jur. Maanaam amul ag demandoo ci ñaari gaawaay yi, benn bi moo raw beneen bi. Loolu moo ko wuutale ak doxalukaay bu demandoo. + +Bii xeetu doxalukaay manees na koo jëfandikoo niki ab jurukaayu mbëj, ab safaanukaay. Waaye bariwul li ñu koy jëfandikoo ngir jóox kàttanu mbëj ndax li ko doxalukaay bu demandoo gënee ci wàll woowu. + +Melokaan +Doxalukaay bi ci ñaari xaaj la séddaliku, benn bi di tekkaaralaan bi, di xaaj bu taxaw bi, beneen bi di wëndeeluwaan bi, doon xaaj biy yëngu. Tekkaaralaan bi dafa am ay bën-bën yu, lang ak w��ndeeluwaan bi, di fi lëmës gi di jaar, maanaam wommatukaay yi dawaanu mbëj bi di jàll. + +Doxiin +Dawaan biy jaar ci lëmës gu tekkaaralaan bi mooy jur ab toolu bijjaakon buy wëndeelu, xélu wëndeelug tool bi mi ngi aju ci baraayu dawaan biy dugg ci doxalukaay bi te jóge cig ndombo gu biti. Ngir am ab toolu bijjaakon bu taxawul benn barab, di wër, faww ñu am ñetti lëmës yu tolloo, te itam yam dendu mbëj bu safaanu bi ñu leen di dundalee. Waaye ngir gëstu masin bi doy na ñu xool rekk benn wommatukaay ci ñett yi ndax liy xew ci benn bi mooy xew ci yeneen yépp. + +Kon lëmës gu tekkaaralaan bi dafay nekk ci biir ag wal gu bijjaakon guy soppiku ci jamono. Toolu bijjaakon buy soppeeku bi mooy sabab juddug jenn doole ju mbëjdoxalukaay, lëmës gu wëndeeluwaan bi su sóoboo ci boobu tool, sunu sukkandikoo ci àtteb Lorenz, dafay xiirtal ci ay catam ab wuuteeg aj, moom it juddal ab dawaanu mbëj ci wëndeeluwaan bi. Segam xamees na ne su ab dawaan di jaar ci aw taxar, dafay jur ab toolu bijjaakon. Kon ñu am ñaari tool (bu tekkaaralaan bi ak bu wëndeeluwaan bi) liy tukkee ci digaaleeb ñaari tool yi mooy jenn doole ju mbëjbijjaakon, di liy wëndeel wëndeeluwaan bi. + +Li tool bi tekkaaralaan bi jur, di xiirtal ab wuuteeg aj ci wëndeeluwaan, loolu itam sabab beneen tool, di lu ag ñakkam a judd di indi ñakk a demug wëndeeluwaan bi. Tax ñuy far di ko woowee itam masinub xiirtal. + +Turu demandoodi ngi jóge ci li wëndeeluwaay bi manut a yam ak walug bijjaakon bi, xél gi ñuy demee, walug bijjaakon bi mooy raw. Wuuteg xél gi nekk ci diggante wal gi ak wëndeeluwaan bi lañuy wax xélu tarxiis. Xélu wëndeluwaan bi lañu wax xélu demandoo. + +Lëkkaloo gi ci diggante xélu tarxiis gi, baraayu dawaan bi koy dundal ak limu seexi dott yi (benn limu seexu dott benn bëj-gànnaar ak benn bëj-saalum lay am), mile mind moo koy fésal: + + xelu toolu bijjaakon bi, ñu koy natt ci w/sim (wër ci simili), ñaata wër lay def ci simili bu nekk; + + f mooy baraay bi, ñu koy natt ci Hz; + + P mooy limu seexi dott yi +ngir xayma tarxiis gi s + +n mooy xélu wëndeeluwaan bi. + +Ci misaal, ab doxalukaay bu am ñetti seexi dott p (6 dott), bu baraayam f doon 50 Hz mi ngi am xélu demandoo 1000 wër ci simili. + +wuutuloxo yu mbëj +Raaya réewum Senegaal am na ñatti rëdd yu taxaw te tolloo, wu wert, wu mboq ak wu xonk. Ab biddiw wu wert am juróomi cat a nekk ci digg rëdd wu mboq wi. + +Kulóor bu wert bee ngi màndargaal kulóoru yonent Yàlla Muhammad ñeel jullit yi, wow yaakaar ñeel nasaraan yi mbaa wow njur ñeel ñi gëmul Yàlla. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy 361 mbaa RGB 30 181 58. + + Melo (Kulóor) wu mboq wi day màndargaal am-am ak njariñal liggéey, doon it kulóoru Caada ak ladab; kulóoru xel mbaa ruu. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy 116 mbaa RGB 252 209 22. + Kulóor bu xonk bi day màndargaal kulóoru dereet, joj dund, joj jaayante gu askan wépp def ak joj xeex ñàkk. Nimero bi ko sistem Panton jox di 186 mbaa RGB 206 17 38. + Biddiw bu wert bi juróomi cat yi day màndargaal mbokkoo gi ak Afrig, akug ubbeeku ñeel juróomi dénd yi. Li mu wert nag day tekki yaakaar gi judd ci moom gi Senegaal moom boppam. Day màndargaal it juróomi ponki Lislaam yi ñeel jullit yi. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy wow rëdd wu wert wi. + +Amul benn dogalu buur bu ñeel yaatuwaayu rëdd yooyu, kulóoru raaya wi ak tolluwaayu biddiw bi. + +Raaya ya jëkkoon + +Raayaw Senegaal wi njëkk, ci atum 1958, daa amoon biddiw bu mboq bu am juróomi cat te ginaaw gi wert. Mi ngi ajuwoon ci Mbooloom Jëmale Senegaal kanam (doon tey làng politig gii di Parti socialiste (PS)), amoom benn biddiw ca jamono jooja. + +Ci weeru samwie 1959, réewum Sudaη miy làkk faraase (doon tey réewum Mali) ak réewum Senegaal ñoo ànd sos Mbooloo mu Mali (bokk ci réew yiy wax farañse), te aw raayaam, am ñetti kulóor, wert, mboq ak xonk akub kanaga ca digg ba. Réewum Senegaal daa mujj rocciku ci mbooloo moomu, témb ci 20 ut atum 1960. Bamuy génn ca Mbooloo ma Senegaal daa yóbbale raayaw Mbooloo mu Mali ma waaye daa wuutale kanaga ba akub biddiw bu wert ngir bañ a juuyoo ak jullit yi. + +Lëkkalekaayi Biti + Cyber Flag : Drapeaux historiques + Vexilla Mundi : Sénégal + Flags of the world : Sénégal + Flags of the world : Drapeau du Soudan français + +Afrig +Réew +Senegaal +Raaya +Dereet ndox mu xonk la muy daw ci yaramu nit ak luy dund niki nit, di jaar ci diggante der wi ak yàpp wi, ngir man a wéy ci cér ci ko soxla, ngir dox niki: res, roñoo, Lu am solo la ngir ag dund man a am, ndax mooy séddale oksisen (li ngay noyyi) bi ci yaram wépp, lu man ta ñàkk la ci doxug oksisen bi +Nit ku mukàllaf dina ci am lu toll ci juróomi liitar + +Jëmm +Yaram +Jullit mooy ku topp Diiney Lislaam, sartees nako ci nangu te wax ni «Maangi Seere ni amul jenn Yàlla ju dul Yàlla (Allaa); Te maangi seere ni Muhammad ndawul Yàlla la» ñu koy wax Baati Seere yi + +Ginnaaw wax jooju, sartees ci kawam, mu Gëm Yàlla moomu ca namu ware, gëm ni amul ndey, amul Baay, Amul fumu yamle, Amul kumuy bokkaaleel, amul ab tàmbali, amul ab dayo, Mooy degg, Mooy gis, te day jàpp, Déggam googu ak gisam gi aki meloom yépp, Darra nduroowu ci ak niko leneen di defe, Gisug lépp, ak déggug lépp, moongi aju ci moom, nduroo wul ak darra, Darra nduru wu ko, Darra umbu ko, teewe na lune, moo Sos lépp, Moo bind nit ak Jinne, Moo sàkk dénd bi, Lu am moom la neex, ak lépp li ci aju ci gëm ko... fii Gëm Yonent yépp ci lu dul ag xàjjale, Gëm amug Malaaka yi doonte gisu léen, Gëm ëllëg bisu pénc ba, Gëm Dogal bi ni lu am rekk mooko dogale noona, Gëm Téere yi mu wàcce woon yépp ca ñu jëkk ña ak ñu mujj ñi, te gëm ni Alxuraan rekk moo ci di Téere buy wéy ba fimne, nangu li Yàlla wax ci Alxuraan lépp, nangu it Hadiisi Yonent bi Muhammad, Nangu Julliy Juróom bis bu ne, nangu joxe Azaka ndeem war na ci Alalam, nangu Woor, nangu Haj aw yoon ci sag dund ndeem man nga + +AJ + +Diine +Lislaam +Nit daa mas di laaj ci jamono ju nekk: + + fan la àdduna su daytaluwul sii juge ?, + fan la jëme ? + nan la àtte yiy wattu ag màndaqoom (son équilibre) akug nosoom (son ordre)di doxe. + +La ko dale ci ay xarnu, boroom xam-xam yi def nañu ay gëstu ci lu aju ci tëriit loolu (sujet boobu), ñu àgg ci génne am mbooloom ay gisiin (théories). Xalaat bi notoon ci xarnub fukk ak juroom ñeent moo doonoon àdduna bi de am mbooloom ne-ne (matiere) la, yu yor dayo bu amul yamu, yu fi nekkoon naka jekk, tey yu fi dul jug it ba fàwwu. + +Gis-gis bii nga xam ne mooy cëslaayu xeltu gu ngérum ne-ne (philosophie matérialiste) da daan dàq ak a weddi amug aji sàkk ji (Yàlla), ba noppi di saxal ne àdduna bi amul ab tàmbali, te amul it ab yamu. + +Ngérum ne-ne (le matérialisme), nosteg xalaat la (système de pensée), guy jàppe ne-ne ne mooy genn nekk gu joyu (le seul être absolu) gi fi am, ci noste gii, lenn lu dul ne-ne amul. Nosteg xalaat gii nga xam ne mi ngi sosoo ca Geres Gu Yàgg ga, te gën a tase ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu, mujj na di lu siiwe ci turu ngérum ne-ne mu dàggasante (matérialisme dialectique) mu Karl Maks. Ñoñ ne-ne ñi (les materialistes) dañoo jàppe woon xalaatu àdduna bu amul yamu bii muy seen ndëerlaay lu mag lu seen xeltu gu weddi gi (philosophie athée). Ci misaal, ca téereem ba tudd (dal yu dàttu yu xeltu) (principes fondamentaux de philosophie) saa ne-ne (ce materialiste) mii di Jorj Politseer, saxaloon na ca ne àdduna bi du lees sàkk, dolli ca ne bu doonoon lees sàkk, daa waroon a nekk di lu Yàlla sàkk ca saa sa te mu tukkee cig neen. + +Bi Politseer saxalee ne àdduna bi sàkkeesu ko cig neen (du néant), dafa sukkandiku woon ci misaal mu sax mu àdduna bi (modèle statique de l'univers) te nekkoon fi ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Mu xalaatoon ne def na ag saxal gu xam-xam. +Ci biir loolu jëm kanam yi xam-xam ak xarala amal ci ñaar-fukkeelu xarnu, màbb nañu ci mujj gi xalaat bu njëlbéenu (idée primitive) bii ñuy wooye ngérum ne-ne (matérialisme), wuñees na ne àdduna bi saxul ni ko ñoñ ne-ne ñi daa waxe . Waaye ci safaan bi daa nekk cig tàllaliku. Gisees na it jaare ko ci seetlu ak xayma ne àdduna bi am na ab tàmbali (fu mu tàmbalee), te dees koo sàkk mu tukkee ci tus, ci ag fàcc gu mag. Tay jëf jii àddunay xam-xam jépp nangu na ko, te wuññig jëf yu am solo yii mi ngi jàppandee ci ay seetlu aki njuréefi gëstu yu di ag jeqiku (révolutionnaire) . + +Ca 1929 ca seentluwaay (observatoire)bu Monpiuson ca Kaliforni, ab saytukatu bidiw bu Amerig bu tudd Elwin Oban defoon na benn ci wuññi yi gën a mag ci taariixu saytubidiw (astronomie), bi muy seetlu bidiw yi ci ag fésalukaay gu ngande (télescope géant), gis na ne dañuy genne genn leer gu xaw a xonq, ci kem seenug soreyoo, loolu li muy wund mooy bidiw yi dañuy dem sori ñu. Waawaaw, ci li ay àtte yees nangu ci jëmm (lois phisique) wax, jëmmi ceññeer yu leer yi bu ñuy tuxu jëm ca tombub seetlu ba, dañuy jeng jëm ci yolet, te jëmmi ceññeer yu leer yiy dem di sori tombub seetlu bi dañuy jeng jëm ci xonq. Seetluy Oban yi may nañu nit xam ne leeri bidiw yi dañuy jëm ci xonq. Loolu li muy wund mooy ñoom kat dañoo dëkk ci di ñu sori, di dem wëlis ñu. Ginaaw loolu Oban defaat geneen wuññi gu mag. +Du rekk bidiw yi ak galagsi yi dañuy sori wëlis nu, waaye dañuy dox di soreente ñoom ci seen biir. Ndegam nag mbooleem céri àdduna bi (ses éléments) dañuy soreyante ci seen biir, lenn lees man a jàpp mooy ne àdduna bi daa nekk cig yaatu gu sax (tàllaliku=expension). Ngir gën a xam loolu man nañoo jeneer àdduna bi mu mel ne kaw ag manq gees nekk di wal. Ni tomb yi nekk ci kaw manq gi di soreentee lees koy gën di wal, ni la yëf yi nekk ci jawwu ji di soreentee lu àdduna bi gën di tàllaliku. Lii sax wuññeesoon na ko ci gisiin (theorie) ci lu gënoon a teel, Albeer Anstaayin mees jàppe ne mooy boroom xam-xam bi gën a mag ci ñaar-fukkeelu xarnu àggoon na ci ginnaaw ay xayma yu xam-xamu jëmm bu gisiin (physique théorique), àggoon na ci ne àdduna bi nekkul di lu man a sax (statique). Ci biir loolu daa tegoon nee wuññeem googu, ngir rekk bañ a dëppoodeek misaalum sax (model statique) mu àdduna bi, mi nga xam ne moom la népp jëloon ciy jamonoom. Ci ginnaaw bi Anstaayin gisoon na ne def na ci loolu njuumte li gën a mag cig dunnam akub liggéeyam. + +Lu tàllalikug àdduna bi di wund? Tallalikug walla gën di yaatug àdduna bi day wund ne bu ñu manoon a deltu ginnaaw, dinañu seetlu ne àdduna baa ngi doore ci benn tomb, fa la jële cosaanam. Xayma yi wone nañu ne benn tomb bii nga xam ne moo ëmboon mbooleem ne-ne bu àdduna bi daa waroon a am kemub tus (volume zero) akug fataay gu amul yamu. Àdduna bi nag mi ngi sosoo ci fàccug benn tomb bii yoroon dayob tus . Fàcc gu mag gii nga xam ne ci la àdduna bi doore, tuddeesoon na ko Big Bang, gisiin wi it daal di jël tur wi. Cig pàttali dayobb tus aw waxiin wu gisiin la (expression théorique) wees jëfandikoo ngir man a leeral, xam-xam manul a leeral maanaam neen ( concept de neant) mi nga xam ne weesu na digi déggiinu nit, ba mu koy tudde tombub tus. Ca dëgg-dëgg, dayob tus mooy ag neen, ci noonu àdduna bi mi ngi sosoo ci cig neen, ngir gën a leer , dees koo sàkk. Lii nga xam ne ci ñaar fukkeelu xarnu rekk la ko xam-xamu jëmm bu jamonoo bi wuññi, Alquraan moom saxaloon na ko booba ak leegi tollu na ci fukk ak ñeenti xarnu: Moom moo sos asamaan yeek suuf si. +Gisiinu Big Gan (la theorie du Big Bang) mi ngi doon wone ne, ci njëlbéen gi, mbooleem yëf yi nekk ci àdduna bi benn cér rekk lañu woon, ginnaaw bi ñu séddalikoo. Lii nga xam ne gisiinu Big Bang wee ko wone, Alquaraan it jotoon na koo wone booba ak leegi toll na ci fukk ak ñeenti xarnu, ci jamono joj nit lu néew la xamoon ci àdduna bi. +Ñi weddi xanaa gisuñu ne asamaan yeek suuf si benn jóor lañu woon bu taqaloo (lu ci ne tayu ci moroom ji), ñu tàqale leen,. +Loolu li muy wund mooy lépp sàkkees na ko ci genn fàcc gu mag gu bawoo ci benn tomb, bu ko defee mu doon àdduna bii ngay gis bi mu tàqalikoo. Tàllalikug àdduna bi benn la ci firnde yiy wone ne àdduna bi cig neen lees ko sàkke. +Lii nag xam-xam wuññiwu ko lu moy ci ñaar-fukkeelu xarnu bii rekk, waaye Yàlla moom jotoon na ñu koo xibaar ci Alquraan, jees wàcce booba ak leegi tollu na ci 1400 at: +Asamaan si ñoo ko tabax ci sunu kàttan, di ko yaatal it ci anam gu sax. +Big Bang day wone ci anam gu leer ne àdduna bi cig neen lees ko sàkke. Ci nu gën a leer, Yàlla a ko sàkk. Looloo tax saytukatu bidiw yi taqoo woon ak xeltu gu ngérum ne-ne mi (materialime) wéyoon ci weddi Big Bang te sax ci dëgëral xalaatub àdduna ju mul yamu bi. Sababi lànk gii feeñ na ci baati Artir Edington, benn boroom xam-xamu jëmm bu siw la woon: (( ci wàllug xeltu, déggiit (notion) wu ag tàmbali gu bette (abrupt) daf may xatal )). +Beneen saa ne-ne bu waa Angalteer di Fred Hoyle, moom itam gisiinu Big Bang xatal na ko. Ci digg ñaar-fukkeelu xarnu Hoyle daa di nay doon farandoob gisiin wu melokaan wu sax wi (état stationnaire), woowu gisiin daa niroo woon ak wa fi nekkoon ca fukk ak juroom ñeenteelu xarnu, te di woon àdduna bu tekkaaral bi. Gisiinu melokaan wu sax wi daa saxaloon ne àdduna bi ab kemam amul yamu naka noonu ab diiram. Gisiin wii nga xam ne amul woon geneen jublu gu feeñ gu dul dëgëral xeltug ngérum ne-ne (philosophie materialiste) nekkoon na di lu safaanoo ak gisiinu Big Bang wi saxaloon ne àdduna bi am na ag tàmbali. Ñi daa layal melokaan wu sax wi yàgg nañoo lànk Big Bang, waaye ci biir loolu xam-xam moom di wéy di leen weddi. Ci +1948 Jorg Gamow indi na beneen xalaat ci lu aju ci Big Bang. Saxal na ne ginnaaw bi dduna bi sosoo ci ag fàcc gu mag, ab gëwéelub ceññeer (circuit de rayonnement ) war na am ci àdduna bi, niki jeexiitu fàcc gii. Rax ci dolli, ceññeer gii daa war a nekk di lu tas ci anam gu benno ci mbooleem àdduna bi. Firnde loolu doon na feeñi . Ca 1965 ñaari gëstukat yu tudd Arno Pinsiyas ak Robert Wilson wuññi nañu ceññeer yii cig mbetteel . +Ceññeer yii ñuy wooye ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang (fond diffus cosmologique) niruwuñu woon lu juge ci benn gongikuwaay, waaye da doon lu tas ci jawwu jépp. On comprit ainsi(degguma li mu wax foofu). Pensiyas ak Wilson joxees na leen neexalub Nobel ngir seen wuññi yooyu. +Ci 1989, Nasaa sànni woon na ci jawwu ji satalit bii di Kob, ngir def ay gëstu ci ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang , ba ñu defee juroom ñatti simili ci jawwu ji lañu dëggal xaymay Pensiyas ak Wilson yii. Kob wuññi na jeexiiti fàcc gu mag googee amoon ca ndoortel àdduna bi. Wuññi gii ñu jàppe gi gën a mag ci mbooleem jamono yi, indi na firnde lu leer ñeel gisiinu Big Bang. Leneen firnde lu am solo lu Bing Bang mi ngi bawoo ci kem bu Idrojen ak Eliyon bi nekk ci jawwu ji. Ci biir gëstu yi gisees na ne dajaloog Idrojen-Eliyom gi am ci àdduna bi dëppoo na ak xaymay gisiin yu dajaloog Idrogen-Elyom yi desoon ginnaaw Big Bang. + +Bu àdduna bi amul woon fu mu tàmbalee mbaa mu nekkoon di lu fi mas di nekk, kon aji toggaleem ju Idrogen (sa composant dihydrogène) lekku na ba jeex bu yàgg ba far soppiku di Elyom. Firnde yu leer yépp nag ñoo tax woroom xam-xam yi nangu gisiinu Big Bang . Misaalum Big Bang mooy baat bu mujj bi woroom xam-xam yi agseegun ci lu aju ci cosaanul àdduna bi. Ginaaw bi mu yàggee layal Melokaan wu sax wi ci wetu Fred Hoyle, Denis kiyama melal na taxawaayam bu mujj bi mu mujj a àgg, ginnaaw feeñalug mbooleem firnde yiy dëgëral gisiinu Big Bang. Skiyama jibal na ne (( layal na gisiinu melokaan wu sax wi, du caagéenug ngir ne da koo wóoroon ne mooy dëgg, waaye rekk ngir ne loolu la bëggoon muy li am. Skiyama dolli na ci ne, bi firnde yi tegaloo, manatul a def lu du nangu nag ne làmb ji tas na, te wacci gisiinu melokaan wu sax wi)). + +Profesëer Jorj Abel bu daara ju kawe ju Kaliforni nangu na moom it ndam lu mujj li ñeel Big Bang. Daal di jibal ne firnde yi am ci jamono jii wone nañu ne àdduna bi mi ngi feeñ ci ay milyaari at ci ginnaaw, te Big Bang gi waral ko. Mu nangu ne amul meneen pexe mu dul nangu gisiinu Big Bang. Ak dikkug gisiinu Big Bang, léebuw ne-ne bu sax (mythe de la matiere eternele) wi nga xam ne moo doonoon cëslaayul xeltug ngérum ne-ne (la base lde la phiolosophie materialiste) mujjees na ko sànni ci sënub taarix. +Lu fi amoon kon njëkk Big Bang ? +Jan doole moo sabab amug àdduna bi ci fàcc gu mag gii te kat bu njëkk lu amadi la woon ? +Laaj bii day da fiy indi - ci waxi Artir Edington – lu naqari li ci wàllug xeltu li ñoñ ngérum ne-ne nanguwul a nangu te mooy amug aji bind (aji sàkk). +Xeltukat bu weddi bu siw ba nii la saraa laaj boobu: (( Xamees na bu baax ne diine lu baax ci bakan la. Kon maa ngi doore ci nangu ne Stratonocien bu weddi bii manul lu dul nangu dëppoo gu àdduna gii. Ndax mel na bu baax ne sóobukati jawwu yi indi nañu firndey xam-xam ci ne àdduna bi am na ab tàmbali)). + +Boroom xam-xam yu bari yu dul tënk seen bopp ci ne fàwwu dañoo war a nekk ñu gëmadi, nangu nañu ne am na aji sàkk ju man lépp ju sabab sosug àdduna bi. Aji sàkk jii daa war a nekk aji nekk joj moo sàkk jamono ji ak jawwu ji (walla féex gi = l’espace), waaye nekk it di ku temb (maanaam ku wéeruwul, sukkandikuwul) ci jamno ak jawwu ji. Lii la boroom xam-xamu jëmm (physicien)bu siiw bii di Hugh Ross wax : (( Bu tàmbalig jamono tollook tàmbalig àdduna bi ni ko layal wu féex gi saxale (le théorème de l’espace), kon li sabab àdduna bi daa war a nekk ag nekkte (entité) guy jëfe ci tolluwaayu jamono bu temb (indépendant) ci anam gu mat, ba noppi jiitu fi tooluwaayu jamono bu àdduna bi. Jii wax nag mi ngi ñuy jàngal ne àdduna bi du Yàlla moom ci boppam, te Yàlla it nekkul di lu ëmbu ci àdduna bi. Waa-waaw ne-ne ak jamono aji sàkk jee leen sàkk, ki nga xam ne wéeruwul ci benn ci maanaa yii, jii aji sàkk nag mooy Allaa Yàlla miy aji man lépp, kiy boroom asamaan yeek suuf . +Ca dëgg-dëgg, Big Bang indi na ciy jafe-jafe lu sakkan ñeel woroom xam-xami ngérum ne-ne mi , Antoni Flew dëggal na loolu. Ndax Big Bang saxalul rekk ne àdduna bi cig neen lees ko sose, waaye saxal na ne it dees koo sos ci anam gu nosu, gu tegu ci yoon, gees fuglu. Big Bang mi ngi ame ci fàccug tomb bi ëmboon mbooleem ne-ne ak kàttanug àdduna bi, akug tasam ci jawwu ji ci mbooleem wàll yi, cib gaawaay bu yéeme. Ne-ne bii ak kàttan gii ñoo jur ag màndaqoo gu mag gu ame ci ay galagsi, ay bidiw, jant bi, suuf si ak mbooleem yeneen yaram yu asamaan yi. Nga rax ci dolli, ay àtte yees tudde àttey xam-xamu jëmm (lois de la physique) daal di feeñ, ay àtte yu niroo ci àdduna bi bépp, yu dul soppiku. Àttey jëmm yii feeñ ànd ak Big Bang, soppikuwuñu lu gën a néew ci diir bu tollu ci 15 milyaari at. Nga rax ci dolli, àtte yii ñi ngi tegu ci ay xayma yu àgg ci leer ba bees ci soppee la gën a néew ci li mu doon, mu yàq bindub àdduna bépp akuw meloom. Lii lépp li muy wund mooy Big Bang indi na fi ag nosu gu yéeme. Ci biir loolu ag fàcc, ci yoon, ag nosu daawu ci juddoo, mbooleem fàcc yees ma a gis, toc la daa def, moñoxe, wisaare, tas. Bees gisee nag ag fàcc def ag nos gu mel ne gii, li nuy man a wax mooy ag yewwute manul a ñàkk ci ginaaw li ko amal, te nag kenn daal moo war a yëngal mbooleem cér yii tas ngir fàcc gi, ci anam gees fuglu lool. +Freds Hoyle mi mujjoon nangu gisiinu Big Bang, ginnaaw bi mu ko weddee ay at mi ngi leerar loolu ci anam gu leer: (( Gisiinu Big Bang saxal na ne àdduna bi mi ngi tàmbalee ci genn fàcc. Moone ni ñu ko man a seetloo, ag fàcc du def lu dul tas ne-ne , te Big Bang moom ci anam gu mbóotu daa def safaan ba, ci dajale ne-ne ci melow ay galagsi. Bu ag fàcc yobboo cig nosu gu mag loolu du man a def lu dul gëmloo ci ne am na aji sàkk juy ki ko def. Weneen feeñiit wu nosu gu kiimaane gii sosu ci àdduna bi ci ginnaaw Big Bang mooy sosuwug àdduna bees man a dëkke. Sart yi manul a ñàkk ci sosuwug àdduna bees man dëkke bari nañu te jafe ba xel du nangu ne man nañoo sosoo cig tombe. Paule Davis ab boroom xam-xamu jëmm bu gisiin (physique theorique) bu siw jibal na, ginnaaw bi mu defee am mbooloom ay xayma ci kemub tallalikug àdduna bi, jibal na ne kem bi de àgg na ci leer ak tegu ci yoon fu xel manul a xalaat. Davis nee na : (( njuumte gu ndaw ci natt kemub tàllikug àdduna bi man naa waral àdduna bi moy ag bijjam (sa gravité), bu ko defee wéyal ag tàllalikoom ci anam gu nosoodiku. Adduna bi, bu gënoon a dox ndànk ci nii mu koy defe, day daal di rot, bu gënoon a gaaw tuuti rekk nga gis ne-ne bu àdduna bi tas bu yàgg.Big Bang de du fàcc gu mel ne yépp : ((Ag fàcc la gu am ab tolluwaay bu sax, gu yam fees ko yamloo)). +Prosesëer Stefaan Aukin, dib boroom xam-xamu jëmm bu mag, jibal na ca téereem ba tudd (Une breve histoire du temps) ne:(( àdduna bi mi ngi tegu ci ay xayma aki màndaqe yees nos, defar leen ci anam gu leer gu ñu manul a xalaat nun)). Aukin jibal na ci lu aju ci tàllalikug àdduna bi : (( Su fekkoon ne kemub tàllaliku gi, as cimili ginaaw Big Bang bi, daa yées ak doonte lu tollook téeméeri miyaari milyoŋeem la, àdduna bi day daanuwaat cig teel balaa tollu nii mu toll tay)). Paul Davies leeral na ba tay ngérte lees manul a moyu, lees di génnee ci xayma ak màndaqoo (équilibre) yu leer yii te yam ba ëpp : (( Lu jafe la nga man a tëyewu ci kanamu xam ne ni àdduna bi bindoo fi mu ne, nga xam ne lu néew lees ci laal rekk man na koo yàq, lees liggéey la ci anam gees sonn. Boole gu mel ne lu kiimtaane gii ci ay xiimaa yu lim te dénd bi (la nature) jox ko ay way saxam yu dàttu yi (ses constantes fondamentaux) day wéy di firnde lu fés liy wone ne àdduna bi lu nosu la)). +Ci lu ci aju ba tay, Jorj Greenstein dib Profesëer bu Amerig, ca téereem ba tudd (L'univers symbiotique) nee na : ((Su nu xoolee firnde yii yépp, ab xalaat bu làkkale di na nu jàpp mooy ne lii daal mooy war a doon màndargam ag nammeel gu xarbaaxe (volonte surnaturelle))). + +Ci gàttal daal bu ñu dee settantal nosteg àdduna gu yéeme gii, dinanu gis ne amug ak nosu gu àdduna bi dañoo goor ci ay màndaqoo yu yëgu (delicat) ak ci nosu gu fasu ba tombe rekk ak fiiroo (coïncidence) duñu doyati ngir firi leen, leeral leen. +Ci lu leer, lu manul a nekk la nosu gii ak màndaqoo gu mat gii nekk di lu fi dikkal boppam ak cig tombe ginnaaw ag fàcc gu mag.Sosu gu ag nosu gu ni mel, ginnaaw ag fàcc gu mel ne Big Bang mooy firnde lu fés li ci ag sàkk gu xarbaaxe. Nosu ak tegu ci yoon gu mat gu àdduna bi dañuy wone ci anam gees manul a moyu teewaayug aji bind ju yor xam-xam, kàttan ak hikma ju dul jeex, mooy ki sos ne-ne jële ko cig neen, tey fuglu ak a doxal lii lépp cig wéy. Aji bind jii mooy Allaa, boroom àdduna yépp. +Aji tekki ji : Abdu Xaadir KEBE +taariixLislaam +Doxalukaay bu demandoo ab xeetu doxalukaay bu mbëj la bu dawaan bu safaanu. Diir bi wëndeeluwaanam di def ag wër dañu koo yamaleek baraayu dend bi koy dundal, maanaam dañuy demandoo ndax ci jamono ji dend bi nekke tus la wëndeeluwaan bi di tambali wër gu bees, loolu wuutale ko ak doxalukaay bu demandoodi. Xeetu doxalukaay bii manees na koo jëfandikoo niki ab safaanukaay, maanaam ab jurukaayu mbëj, te sax mooy bees gën a jëfandikoo ci digg yu mbëj yi, di barab yees di jóoxee kàttanu mbëj. + +Defariin + +Doxalukaay bi ñaari wàll la am: benn bi di wëndeeluwaan bi, moom, mu am ci biiram benn limu seexi dotti bijjaan yees defaree bijjaan yu sax walla ay mbëjbijjaan. Ngir man a am mbëjbijjaan bi dawaan bu wéy lañuy dawal cii biir ay taxañ yees def ci wëndeeluwaan bi, naka-jekk taxañi përëm. Beneen bi di tekkaaralaan bi, moom it, am ci biiram ag lëmës gu yittewoo jur ab toolu bijjaakon buy wëndeelu ak ay dottam, segam ñaari dott yu bokk (bëj-gànnaar ak bëj-gànnaar walla bëj-saalum ak bëj-saalum) dañuy bëmëxante, ñaar yu wuute (bëj-gànnaar ak bëj-saalum) di bijjante, kon dottitoolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi suñuy wëndeelu àndaaleek tool bi dañuy xëccaale dotti wëndeeluwaan bi ba tax moom ci boppam di wëndeeluwaale, kon nu amee ca ab doxalukaay. + +Baraayu wëndeelu gi mi ngi aju ci baraayu dend bi koy dundal (ci misaal Senegaal 50 HZ), Diiwaan yu Bennoo yi 60 la). limu wër yi wëndeeluwaan bi di def benn simili bu nekk + + xelu toolu bijjaakon bi, ñu koy natt ci w/sim (wër ci simili), ñaata wër lay def ci simili bu nekk; + f mooy baraay bi, ñu koy natt ci Hz; + P mooy limi seexi dott yi + +Limu seexi dott yi moo ngi yam ak limu taxañ yi, benn taxañ bu nekk benn seexu dott lay am: benn bu bëj-gànnaar ak beneen bu bëj-saalum. + +Ag taalam +Taal ko doon na lu xawa jafe. Su doxalukaay bi taxawee, suñu ko joxee dawaan bu safaanu biy jur toolu bijjaakon buy wëndeelu bi biy wëndeel wëndeeluwaan bi, diisaayam dafay tax ba du ko man a topp, dafay wéy di taxaw. Ngir man koo taal kon dañu koy taqale ak ab doxalukaay bu demandoodi ngir mu tambalee wëndeelu ginnaaw bi ñu dindi ko daldi koy soog a jox dawaan bu safaanu bi ngi mu man di demal boppam. + +Jëfandikoom + +Doon na xeetu doxalukaay bu bariwul lees koy jëfandikoo, ag njëfandikoom dañu koo rekk yamale ci yenn jëfe yi rekk + +Lëkkalekaay yu biir +Doxalukaay bu demandoodi +Doxalukaay bu mbëj +wuutuloxo yu mbëj +Qin Shi Huang moo doonoon imbraatóor bu njëkk bu Siin gees Bennal. Ginaaw bi mu bennalee Siin, moom ak njiitu xelalkatam yi Li Si, def nañu am mbooloom ay yéwénal (reformes) yu koom ak politig yu mag, def it ay sémb yu mag, yu ëmbaale sumb (version)bu njëkk bu Miir bu Mag (the great wall)bu Siin bi. Waaye nguurug jaay-dooleem ga (nga xam ne lakk na ay téere, suul ay woroomi xam-xam) tax na muy jëmm ju jeqi dàggasante ci taariixu Siin +Taariix +Siin +Soxna Mariyaama BUSO ñu dàkkantale ko ci jikko Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) +gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, Génn àdduna ci atum 1866 ca poroxaan, di way-juru Sëriñ Tuubaa. + +Soxna Jaara BUSO mom Sëriñ Hamat BUSO (baayam) ak Soxna Asta Waalo MBÀKKE (yaayam), cosaano +ci askanu Sëriif gog calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib +ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom), (*xoolal callale gi fii ngir gàttal) + +Mu dondoo ci loolu ag cell akub Yar ba war ci doomi Soxna jële ko ci Waa-juram wu Jigéen +Soxna Asta Waalo MBÀKKE doon ab Jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf, mu juddu ci loolu Yaayam yar ko ci, + +Am njàngam ak ab yaram: + +Soxna Jaaratu-l-Laahi BUSO jànge na alxuraan ci aji/way-juram wu jigéen wu séll wa te sàmmu, +te doon senn Soxna su ame taxawaay bu mat sëkk ci Lislaam ci jàngale ak yare, niki Sëriñ si, +ba mokkal ko ci anam gu sell te sax, ci jamono yi muy am fukki at ak ñeente (14 i at) + +Aywaay! ak li dudam gi di gàtt lépp (33 i at) téewul bind na Alxuraan ñeenfukki yoon ci yoxoy boppam (40 i kaamil) ndax daa mujjoon di ab jàngalekatu Alxuraan ci Taaral mbind, + +Mu jàngal ko it xam-xamu diinéem niki jennal Yàlla (Tawhiid), Àttey Lislaam akuw yoonam (Fiq), Séllal ak jaamu ngir Yàlla dong (Tassawuuf), bamu wattu ko namu ware, mu yar ko it ci Lislaam, ci jàng alxuraan, ak jëfe ab xam-xamam, yar ko it ci ngor, muñ, nangu, ak jépp jikko jees taamu. + +Bamu mujj di ku xarañe bépp xam-xamu Lislaam, te it di kuy jëfe ngirum Tassawuuf ci anam gu xóot, + +Jigéen ci lislaam: + +Lislaam ginnaaw fimu fekk jigéen ak nimu ci taxawe bamu déñ fi, li mu tëral ngir ñoom a gën a tee +yeeme, ci sàmmu léen, wormaal leen, ak taxawu leen, tey tëkku képp ku léen wormaalul, mba nga leen di fowe. +Jox leen it kem daraja ak góor ñi ci wareef yi ak àq yi, ci waxi Yàlla ji muni: «Góor ñi ñooy Kilifa ci kaw jigéen ñi, ci ngënéelul Yàlla ci diggante ñee ak ñii» kon sàmm jigéen ñi farata la ci bépp góor bu di kilifa, + +Te làq leen ci ginnaaw góor ñi, ngir kenn walla darra bañ leen a lor, Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) Neena : «Ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam, te man maa gën ci samay jigeen» + +Jigéen june nag, mu wutal ko góor gu ko war a wattu, yiir ko, diko taxawu ci pakki àdduna yii diis ci ndoddu jigéen lool, Baay, jëkkër mbaa mag, (te góor gu mukàllaf yaay sa sàmmub bopp ci loraange yi) te jàppe ko muy lu «sakré» (worma), wormaal léppam, bëggul kenn ku ko fowe bëggul it mu fowe boppam, + +Def ko it muy yaay, di jabar, muy ñaari wareef yi gën a diis ci àdduna, ba matal ko rekk war naa doy i yitte bépp jigéen june waliif leneen, + +Yii yépp nag di lu Soxna Jaara jàng, jàpp ko te jëfe ko ca anam gamu ware, ci topp ndigëli wattukatam (Kilifaam) ak sàmm ak njabootam, yor leen yar leen ci lislaam, niki lees koko defalee woon. + +As lëf ci ay jikkoom ak i meloom: + +Soxna Jaaratu-l-Laah Dëkkandoob Yàlla bi ci ag céll akuk sàmmu, +Di Ab jullit bu di doomi jullit, Nangu te seere ni: «Amul jenn Yàlla ju dul Allaa, +(Yàlla aji sàkk ji yélloo wul Wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn, Mooy dégg, +Mooy gis) Muhammad (Jàmmi Yàlla ak xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la, (ndaw lumu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne,) nangu te jàpp ni Lislaam rekk mooy Diine, Gëm téerey Asamaan yépp te nangu ni Alxuraan a leen wuutu, Gëm dogal te diko rafetlu, Gëm Malaaka yi ak lépp li aju ci ngëm... +nangoo julli, nangu woon a joxe Azaka ndeem war na ci alalam, nangu woon a woor, nangu woon ni Aj war na ko aw yoon. + +Soxna Jaaratu-l-Laah doonoon as gor su di doomi gor, di ku sàmmu, ragal Yàlla, Gëm Yàlla diko jaamu, Sopp Yonent bi di topp sunnaam, Bëgg ab Sëriñam di wëye ay ndigëlam, fonk ay bokkam te nawloo leen, di ab jullit bu koy jëfe, di as gor su gore, Di doomi Soxna su soxnaa, Di ab jàngkat buy jàngale, di Boroom xam-xam bu koy jëfe, di boroom alxuraan ci bind ak ci wattu, doon ku nangu te man a muñ, doon ku yaru te daa yare, doon ku ñime njaboot te di leen taxawu, doon it jigéen ju maanu ci bépp anam, Ku daa dunde Lislaam, waxees nani masu la faat waxtu mukk, + +Masul a julli te jàppuwul, masul a julli it te deful yi ko war ak yimu warloo ci «Wird»... +niki ko waykat ba waxe: Masla julli te jàppul () masla julli te wirdul () nangam nàngam..... +Ci lu dul weeru koor, baaxoo woon na di woor, koor yees taamu ci at mi, ak i koor yu mu tegoo woon. +tegoo woon na it di jàng téereb «Dalaa-ilul-Xayrâti» bu Imaam Jazuuli, di ab téere bees taamu, +temu fees dell ak i julli ci Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) +Li am daal, ay waxtoom ci jàng alxuraan ak tari ko la dëkke woon mbaa julli ci Yonent bi, ngir ndigalul Yàlla la, lu woom aki dëel. + +Moom daal ci gàttal mooy Way-jur wu jigéen wu Seex Ahmadu Bàmba Xaadimul Xadiim, te aji bind ji (Yalla) neena: «Suuf su nangu dan a génne kemam ci ndigalul Boroomam» +Muy li Wolof naan: «Kéwël du tëb doom jay bëtt» + +kon daal loolu rekk doyna ay jikko akuw tagg, ndax Bàyyi doom ju melni Seex Ahmadu Bàmba, +ci ag céll akuk sàmmu, wéetal Yàlla, te jox ko léppam, xam, xàmme di xamale, nangul Lislaam, yaru lool di yare... jigeen ju ko ame làmboo mbooleem jikko yees taamu... + +Soxna Jaara BUSO ci pénc mi: + +Niki jigéen ñépp, baaxoos na jigéen ju mat a dem kër, fàggu lees ko boroom kër, ak it teewal ko ngir man koo dénk wax i njariñ, ak yee ko ci àddina xamal ko ni it, fa nga jëm sa ab sang nga fay fekk, bu la Yàlla booleel, xamal ko it ni, Ngërëmul Yàlla akuk payam, ak doom ju raw i maasam, ñeel na soxna si ànd ak boroom kërëm ci li neex Yàlla, nangoo muñ, nangu, tey wéy ci ay ndigël, + +Niki noonu lees ko defale Soxna Jaara ci bimu ci tolle, fàggul ko te tànnal ko ab Sëriñ ci anam gamu gëne, ak ci melo yiy sax ci nit,mu déglu it wax yu am solo yooyu ak soññee yooyu, ci ag teewlu, dégg ak topp, Waaye ci yaru gimu yaru ci xamlu Yàlla ak di jéem a xàmme, ak xalaat yu sori yi Sufiyànke yi baaxoo, + +neeñu ci loolu, bees koy jaarale ci yii, Mu Ubbi Kaamilu Alxuraan bi mu baaxo yor, ngir def ab natt, yam ci wax i Yàlla ji naan: +«Déeti Yonent ginnaawam (Muhammad)» + +Cey ! lii déy màndarga la mu yaatu te bar i maanaa te doy Kiimaan ci way-xalaat yi, +Ci loolu mu dogu (ab sufiyànke la woon, te fa Suufiyànke ya, wacci séen dogu, moo gën a tar dee fi ñoom) te jaayante ci topp Ab Sëriñam ci jëmmam akuk ruuham (ndundam) kemm kàttanam ngir Yàlla dong, tey ku sàmm ay wareefam, am kersa akuk topp gu matale ñeel boroom kërëm. + +Nu indi fi ak pàttali, Sëriñ Muhammadu BUSO bokk ak Soxna si yenn way-jur, bimu tollee ci wut kër daa dogu ni: «Bu ma wóorul ni doom ju ma am Wàlliyu lay doom duma samp kër» cey ! Pas-pas bu ni mel déy, la soxna si ame bi muy dem kër. + +Soxna Jaara BUSO doonoon Soxna su Maam Moor [Anta Sali] MBÀKKE, Soxna jaara nag bokkoon ci askan wu di boroom Barke, Yàlla dénk leen am-am, te Yàlla def Maam Moor Anta Sali mi mujj di boroom këram bokkoon ci askan wu seen wërsëg melul noona... + +Amna wax i Sëriñ Tuuba jukoy wéral, Amna bis am góor gu ñëw ci Sëriñ bi, melni ku yàkkamti lool, Sëriñ bi neko: Diw ! fàtte wu ma sama Nag wa, daadi ni: Jëmm jii de, ba may gën di gone bind naa ab Kaamil, diko jox saa Baay Sëriñ Moor Anta Sali muni ma : Xanaa nga yobbu ko saalum ngir man cee am darra, Lu man a jëm ci kër gi, Sëriñ bi neena: Ma dem Saalum diko wecee ku, di wër ba am kuma ko diktal muni ma: aah ! ndongoli man dey Soxla naako waaye ab xaalis de yoru mako, te lima yor xamnaa ni ab dongo du ko war a soxla, niko; Aw nag de laafi yor, Sëriñ bi neko: aah! aw nag moom lu ko yobbu dina yéeme, neena: nag woowee góor gii mooko ni man naala ko jiitalal, Sëriñ bi neena ma warlul ko Àjjana ak guddu-fan, Ni góor gi: "gis nga sama ndëel ya ?" muni ko: "aah! gis naa benn bi de muy gudd fan gi, bi ci des kay a ma wóorul", Sëriñ bi neko:"Waaw! bi ci des it noonu rekk, amul sikk". + +Ci wax jii manees na cee xame ni Yàlla dénku leen woon alal jees man a gis. +Waaye xanaa ñu di ay jaamukati Yàlla, di ay boroom i xam-xam yuy jëfe seen i xam-xam, di ay jullit te doon i gor, sàmmu te ragal Yàlla, + +ci yii jikko daal la Kilifay Soxna Jaara BUSO xool, ba nangu faa maye séen doom, Soxna Jaara it ci yooyii jikko la xool ba nangul ko, loolu it masul di feeñ ci séenub ànd, xanaa àndak Moom ci dooleem ñuy dund ci sutura ak ngir Yàlla, + +Mu Jàppe ko ni ab sangam di topp ay ndigëlam ci anam gu yéeme, +Misaalum nittali bu siiw bii te doy kiimtaan, ñuni: Amna bis Maam moor Anta Sali di takk aw sàkket teye looko sàkket wa, dugg ci biir neeg bi, (xayna ngir jël lumu takke sàkket wi) faf Yàlla dogal mu dugg rekk, Yàlla sóob ab taw, +mu far toog fa néeg ba, neeñu: ba ci fajar gi Maam Moor génn fekk Soxna si mu téye sàkket wa, Muni ko: Aaah! yaw de xanaa fii lala taw bi fekk, niko: Waaw! lu tee bimuy taw nga dugg ci biir, man de jàppoon naani yaangi ci biir, Soxna si niko: Sa ndigël a ma ko teyeloo woon te ba leegi ndigël jugewaatul ci yaw bàyyi loo mako... Haakazaa !! Eskëy ! Lii déy yéem nama, te war a man a yéem waa jamono jii, ci lii numu man a ame, + +Soxna si it liggéeyub kërëm moom rekk a ko daan defal boppam, di ko def ca anam gamu ware, boole ko ak matal jaamuy Yàllaam. + +Ci topp boroom kërëm ak dabu ay sàkkutéefam, ginnaaw Maam Moor ab sëriñam daa xawoon a jëm mag, te fiñu nekkoon xaw a àlle, ba tax sedd ba xaw faa tar, ci loolu daan na ko fàggul matt mumuy jaaroo, ngir mucc ci sedd boobu nga xamni baaxul ci mag, + +Ba bis (xayna matt jafe nako), ngir bëgg a matale càkkutéef i boroom kërëm, tax mu dàjji gaal gi mu daa denc i mbiram, ngir taalale ko Ab sëriñam, Cey !! + +noonu it lako waykat ba waxe Seex Sàmba Jaara MBAY Taalubeb Sëriñ TUUBAA + +Soxna Jaara neeñu:Masul a jug ci di dimbalante ñeel waa pénc mi, ci di taxawu ak di dundal jirim yi ak néew doole yi, ci lu dul sàkku ak cant ci nangukat yi, xanaa ngir jëmm i Yàlla rekk, ba waxees nani ci loolu la jële Turam wii di Jaaratu-l-Laahi +(Dëkkandoob Yàlla bi), + +Soxna si ak njabootug boppam: + +Ci loolu Soxna si Yàlla may nako ci sëy bu barkeel boobu, ñéenti doom, yoy dinanu sawar lool ci tudd séen i tur, ak wax as tuut ci séen i jikko, Nu lime léen nii: + +1- Ab taawam moodi Maam Moor [Jaara] MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, di ku sàmmu te ragal Yàlla, daan jàng ak a jàngale Alxuraan, ci anam gu yéeme, daan jàngale it ci bépp xam-xam bu aju ci diine. + +Neeñu saxoo woon na guddi gune téeméer i ràkkaa (100 i ràkka) noppi jàng alxuraan bamu mat, +bimu fi bawoo Sëriñ TUUBA seereel ko ni:«Man déy Sëriñ MBÀKKE kajoor ak Sëriñ Moor Jaara rekk laa mas a gis kuy dugg ci bàmmeel te yobbaale wu fa bàkkaar, Cey !! + +2- Gi ci tegu di Sëriñ Habiibu-l- Laahi MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, +Sëriñ TUUBAA seereel na ko ni: ku amoon ab cér bu kawe ca Yàlla la, Cey ! Ba jamono yi mu nekkee moom Sëriñ Tuubaa Njaaréem (Diourbel, 1912-1927) baaxoo woon na di dem Xuru Mbàkke di Ziyaare Barabam. + +3- Teg ci Soxna Faatima MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doom i jullit, di as gor su di doomi gor, ndeysaan ! moom nag ag dundam lu gàtt la, dellu na ci Aji sàkk ji ci jamonoy ndaw, Seex Siidiya Gànnaar di ab Wàlliyu ca Gànnaar neena: Malaaka yi dañuy wàcc ci bàmmeelam ngir def i Ziyaar, Cey ! + +4- Haaa ! Teg ci nag, sunu waaji, Ki sunu làmmeñ ak sunuy cér dul deñ ci di ko tudd ak diko liggéeyal, Ki jur ko rekk doy màqaama, Seex Ahmadu Bàmba MBÀKKE Xaadim Rasuul, Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, Di Ab mujaddid bu Lislaam, Doon liggéeykatub Yonent bi, Gëm Yàlla daa ko jaamu, Sopp yonent bi daa roy sunnaam, Bëgg ko daa ko liggéeyal... +Neena: «Yàlla wommatal nama lol mas la nekk te du mas a nekk ba fàww di ko wommatal keneen» +«Du Am Sikk ba fàww ci nekk gi ma nekk di dëkkandoob Yàlla....» + +Héé! mani: bul ko sikk dellul ca lamu liggéey ba yélloo bii añ bu rëy. +Moom daal nu bañ a sori ci jëmm jii, ndax Seex Saliwu Mbàkke neena: «Lu ñépp xam wax ci tuuti doyna» ! kon nu xelu yam foofu, + +Diggante Soxna Jaara ak Sëriñ Tuubaa: + +Bees delloo ci mbindum Seex Muhammadu Basiiru «Minanul Baaxil Xadiim» manga ca naan: Soxna si ku manoon a yare la, daan a yar ag njabootam ci di leen fàttali ak a nettali Xistay gaa ñu baax ña, di leen ko jàjje ak di leen xamal lañu def ba yelloo séen may yooyii, di léen yar ci yuni mel, di léen ci nàmptal, +Loolii nag mooy wareef wu jëkk wiy dox ci diggante way-jur ak doom ja, Soxna si matale ko lool, + +Loolu topp na sunu Sëriñ ba waxees nani jaarul ci po doonte gone baaxoo nako, waaye neeñu am powam moodoon, julleentu, jàng alxuraan, ak a bindantu... te looli kat lako Yaay ju séll jii kune ni woon siiw muy sa jos nàmpatale, + +Soxna si ci ag maandoom, bi sëriñ biy gone daana def ay xarbaax mu koy yëg di ko gis, waaye Sëriñ bi daa sàkku ci moom ngir mu bañ koo yegge Baayam du caageenu mbooloo mi. + +Soxna Jaara digganteem ak Seexul Xadiim weesu na rekk Saahir (lu feeñ) soosu, waaye sar ba ci Baatin bu sax te keemtaane, + +Barina ay nettali yu koy saxal sax, waaye nu Tànn ci rekk bu Sëriñ Abdu Lahad MBÀKKE bi muni: Bees dugalee Seexul Xadiim ci puq si woon ci Ndakaaru, mu xat lool, sëfees ko ak i ràbb ak i fital, ndeysaan ! Soxna Jaara fekk na ko fa diko masta wu diko ñaax, diko fàttali lamu ko yarewoon, muy di xool ca gaa ñu baax ña wéy, ak lañu dajoon ngir yelloo séen i cer, Yonent Naan ko: Xoolal Amsatu (jàmmi Yàlla ci moom) di ab Sahaaba bu jàmbaare ak rayiin wu ñaaw wees ko ray, Cey ! wii way-jur... +Tax Sëriñ Muusaa KA naan: +«Neena kerog gis nafa sunu maam Jaara () Mu di ko ñaax te di ko dolliy daara» +«Njool Màkka naan ko xalamal Sahaaba () Bu tudd amsatu li leey Xitaaba» + +Sëriñ bi nag, Ku fonkoon Soxna si la te di ko wormaal, Dëkk biimu nekkoon di Poroxaan daa mujjoon gent, waaye Sëriñ bee ko dekkilul, +Lépp ngir worma ak fonkeel, Xabru ba it reeroon na, ba xameesul fumu nekkati, waaye Sëriñ bee jox Sëriñ MBÀKKE Gani BUSO doomi nijaayam ndigël ngir mu seetal ko te saytul ko barab boobee, Sëriñ Mbàkke Gani BUSO def ay yitte, ba dégg ab pël bees jàpp ni xam nako, + +Mu ànd ak moom ñu wër ba gis ko, mu koy taxawu ci ndigëlul Sëriñ bi, ba ginnaaw bi mu tàbbi ci loxol Sëriñ Muhammadu Basiiru MBÀKKE, mu koy taxawu ba, bimu fiy juge, noonu it lako ak njabootam di taxawoo ba fimne. + +Amna Sëriñ bu sàmm woon, ragal Yàlla, di ab jàngkat tey ab jàngalekat, Muy Sëriñ Sàmba Mareema Saa-kokki, doon wóllare wu Maam Moor Jaara, wayoon na ay woy ci araab, ngir seere ay jikko yu sell te rafel, yu mu gis si Soxna soosii di Soxnas Wóllareem, + +Way yooyu waxees nani lu Sëriñ bi fonkoon la, daako yër lu bar, ba mujj gi mu waylu waat ko, ngir ag yaatal, Muy Xasida gu tudd «Matlabu ridwaanul mbàkkii () Fii taxyiiri Nazmi Ash-Shaykhu Sàmba al-kokkii» + +Loolu lépp di tektale ak cofeel akuk fonkeel gu mu am ñeel way-jur wi... + +Haakazaa Sii Soxna ! Eskëy wii way-jur ! Cey bii jullit ! Aywaay ! gor sii ! ndeysaan bii yarekat ! +Su làmboo lii lépp ci ay jikko akuw doxiin, Su melni nii la suuf soxla woon ! su melniiy a baax ci dénd bi ! Su melnii la Yàlla soxla ! Su melnii La pénc mi soxla ! Ju melni la doom yi soxla ! Su melnii la boroom kër yi soxla ! Su melnii la njaboot gi soxla ! Su melnii la Lislaam Soxla ! Su melnii lees taamu ! Su melnii lees di fàttali ku ! + +Xoolal it + Sëriñ Tuubaa + +Lislaam +Yoonu murit +mbëbijjaan ab cëru xaralaymbëj la buy jur ab toolu bijjaakon su ñu jaaralee ab dawaanu mbëj ci biiram. Naka-jekk dafay am ab saal (ag weñ lay nekk) di fi ñuy lëmës wëñug përëg gi, walla beneen xeetu wommatukaayu mbëj, di fi dawaan gi di jaar. Man naa nekk dawaan bu safaanu walla bu wéy. + +Jëfandikoom + +Bari na fu ñu koy jëfandikoo, + Fu mel ne ci doxalukaay yu mbëj ngir juddal ab toolu bijjaakon ci wëndeeluwaan bi; + Dees na ko jëfandikoo ngir defi liggéey, ngir yëkkati ay weñ; + ngir defari tëjukaayu bunt, su ñu jaarale dawaan bi mu jur ab tool jenn doole juddaale ca téye liy tax ba bunt bi du ubbeeku, su dawaan bi deñee mu ba ko ñu man koo ubbi. + +Lëkkalekaay yu biir + +mbëjbijjaakon + +bijjaakon + +bijjaan +Xaralaymbëj +Bijjaan aw yaram la wuy jur ab toolu bijjaakon. Man naa nekk ab mbëjbijjaan, moom dafay soxla ñu koy jox dawaanu mbëj ngir muy man di wéy di jur toolu bijjaakon. Man naa nekk itam bijjaan bu sax, ndax ngir jur tool bi du jële dara ci biti, Lépp ci biiram lay xewee, moo tax toolu bijjaakon bi di sax ba faww. Bii bijjaan man naa juddoo ci dénd ci yenn xeeti xeer walla it manees na koo sàkk. + +Ab bijjaan di na am lu néew-néew ñaari dott, benn bu bëj-gànnaar ak bu bëj-saalum. Yenn xeeti yaram yi bijjaan da leen di xëcc, lu mel ne weñ, yeneen yi mu leen di bëmëx, lu mel ne ndox. Soo jëlee ñaari bijjaan nga jegele bëj-gànnaaru benn bi ak bëj-saalumu beneen bi dañuy xëccante. + +Lëkkalekaay yu biir + Mbëjbijjaakon + Bijjaakon + Toolu mbëjbijjaakon + + Toolu bijjaakon + +Mbëjbijjaakon +Wuutuloxo bu mbëj walla masin bu mbëj, ab jumtukaay la buy tax a man a soppi kàttanug doolerandu def ko kàttanug mbëj (di ab safaanukaay) walla kàttanug mbëj ci kàttanug doolerandu (di ab doxalukaay bu mbëj) walla rekk soppi melokaanu kàttanu mbëj gi (di ab soppalikaay). Xeeti masini mbëj yi ñett lañu: Doxalukaay, jurukaay ak safaanukaay + +doxalukaay + +Doxalukaay ab xeetu wuutuloxo la buy soppi kàttanu mbëj def ko kàttanu doolerandu ngir defi liggéey. Doxalukaay yi dees leen séddale ci ñaar doxalukaay bu dawaan bu safaanu ak doxalukaay bu dawaan bu wéy. + +doxalukaay bu dawaan bu safaanu + +Ab xeetu doxalukaay la buy jël kàttanu dawaan bu safaanu soppali ko kàttanu doolerandu. +Doxalukaay bu dawaan bu safaanu dees koo séddale ci ñaar: + +Doxalukaay bu demandoo +Doxalukaay bu demandoodi + +doxalukaay bu dawaan bu wéy +Bii doxalukaay dafay soppali kàttanu dawaan bu wéy ci kàttanug doolerandu. + +Jurukaay + +Jurukaay mooy wuutuloxo bu mbëj biy jël kàttanu doolerandu génne ci kàttanu mbëj. + +Jurukaay yi dees leen séddale ci ñaar: Jurukaay bu dawaan bu safaanu ak jurukaay bu dawaan bu wéy + +Jurukaay bu dawaan bu wéy +Ab jurukaay la booy jox kàttanu doolerandu mu delloo la kàtaanu mbëj ci melokaanu dawaan bu wéy + +Jurukaay bu dawaan bu safaanu +Ab jurukaayu mbëj la buy jël kàttanu doolerandu soppali ko dawaan bu safaanu, di nañu ko woowee itam safaanukaay. Nekk na lu ñu Séddale ñaar: +Jurukaay bu demandoo +Jurukaay bu demandoodi + +Safaanukaay + +Ab wuutuloxo la bu man a dox ci dawaan bu safaanu rekk, ci jëfe dafay soppi melokaanam. Yitteem mooy yokk walla wàññi tolluwaayu dend bi walla rekk soppi baraay bi. Doxam a ngi sukkandiku ci njeexit lees di wax xiirtalu bijjaakon. + +xaralaymbëj +Xiirtalu ag feeñte la gees di gis ci ag ndombo gu mbëj. su dawaan biy jàll ci ndombo gi di soppeeku, sunu sukkandikoo ci àtte Lorentz, dafay sabab jenn doole ju mbëjdoxalukaay juy bañ coppiteeg dawaan bi. Su ndëgërlu gi doonee liy bañ walug dawaan bi, xiirtalu gi mooy li bañ ag coppiteem ci jamono. Gii xeetu feeñte ci dawaan bu safaanu rekk lañu koy amee. Walug bijjaakon gees di am ci juddug ab toolu bijjaakon ci biir ndombo gi mooy tax nu man a xayma dayoo bu xiirtalu gi. + +Tekkeem +Su ab dawaanu mbëj i di jàll ci ab wommatukaay xiirtalu gi mooy juddal ab toolu bijjaakon ci li ko wër. Su nekkee dawaan buy soppeeku ci jamono walug bijjaakon bi dafay soppeeku ci jamono moom itam, coppite googu mooy sabab jenn doole ju mbëjdoxalukaay juy bañ coppiteg wal gi. + +Segam xiirtalu gi mooy liy bañ coppiteeg dawaan bi te ci dawaan bu safaanu li ñu bëgg mooy dawaan bi di man a soppi dayoom ak ci benn baraay bi, kon xamees na ne man naa nekk gànlankoor ba tax keman wara tuuti. Xiirtalu gi L walug toolu bijjaakon beek dawaanu mbëj bi ñoo nu koy jox. + +Bennaanu nattam lañuy wax henry: 1 Henry = 1 Weber /1 Ampere (1 H = 1 WB/1 A). + +Ci ag xiirtalukaay gu 1 henry su coppiteeg dawaan bi nekkee 1 Ampere ci saa dafay jur jenn doole ju mbëjdoxalukaay ju 1 volt. + +Donte tekkeem gii mooy bi gën a siiw doonul bi gën a yomba natt ndax fii xiirtalu gi dafa aju ci wal gi muy genn kemu jëmm gees manuta natt. Ba tax ñu xalaat neneen nees ko manee ame ak ndimbalu àtteb Lorentz. + +Maanaam : + +nga xam ne : + + mooy xiirtalu ndombo gi + + mooy doole ju mbëjdoxalukaay ji. + + mooy coppiteeg dawaan biy jàll ndombo gi ci jenn jamono, + + Su dawaan bi dul soppiku, di/dt dafay doon tus bay tax doole ju mbëjdoxalukaay ji di doon it tus. + +Màndarga bi (-) dafay wone ni dooley mbëjdoxalukaay ji di dekkarlook coppiteeg dawaan bi. + +Xiirtalante +Su benn dawaan bi i di aw ci genn ndombo gu mbëj te di jur ab toolu bijjaakon buy àgg ci geneen ndombo gu nekk ci wetam, daf fay jur jenn doole ju mbëjdoxalukaay moom it juraat beneen toolu bijjaakon buy dellu ci ndombo gu njëkk ga daldi fay jur, moom waat, jeneen dooley mbëjdoxalukaay ak beneen toolu bijjaakon. + +Su fekkee genn ndombo rekk la dawaan bi koy jàll mooy jur toolu bijjaakon biy jur dooley mbëjdoxalukaay ji. + +Su fekkee nak ñaari ndombo lañu toolu bijjaakon bi kenn kiy jur, du yam ci moom rekk, mooy dem ci geneen ndombo gi jur fa dooley mbëjdoxalukaay jiy bañ coppiteeg dawaan bi koy jàll. + +M1/2 di xiirtalante gi ci ñaari nbombo yi. + +Xiirtalante gi dafay aju ci diggante bi nekk ci ñaari ndombo yi, fu ñu feetante, seen melokaan ak limu lëmës yi. + +Ngóora ci saa-su-nekk + +Manees naa rënk ngóora ci biiram, bokkul ak ndëgërlu gi nga xam ne kàttanu mbëj gi nga koy jox daf koy yàq, soppi ko tàngoor, xiirtalu gi moom daf koy denc benn diir bi delloo ko ndombo gi, ba tax manees na natt ngóora gi ci: + +sunu ko laalaatee: + +nu am gii digaale: + +kàttan gees di am ci diirub ñaari jamono j1 ak j2 mat: + +Li ciy tukkee di ni yombul a soppi ci lu gaaw dawaan biy daw cib taxañ te dafay yées lu xiirtalu gi di yokku. + +mbëj +Xiirtalukaay ab jumtukaayub mbëj la buy jur ab toolu bijjaakon su dawaanu mbëj jaaree ci biiram, muy dawaan bu wéy walla bu safaanu. Xiirtalu gi mooy kemu jëmm giy tax nuy man a natt dayoob man gi xiirtalukaay gi man a xiirtaloo. Ci xiirtalukaay gu xalaat kàttanu mbëj gi muy jël daf koy rënk ci toolu bijjaakon bi muy jóox. Su nekke nak ci xiirtalukaay gu dëgg, di lees defare ak ag lëmës gu ag wëñu wommatukaay, faww nu bàyyiwaale xel ci wàll wu kàttanu mbëj wiy yàqu, wi dul soppiku kàttanu bijjaakon, di doon liy jur tàngoor ci biiram. + +Xiirtalukaay yi doon nañu ay jumtukaayu mbëj yu bari ci xeeti Wuutuloxo yu mbëj walla yu mbëjfeppal yees leen di jëfandikoo, yenn ci ñoom doxalukaay yu mbëj yeek soppalikaay yi, ci biir ndombo yu mbëj yu dawaan bu safaanu. + +Defaram + + Bokkaani (li bokk doon ko) ab xiirtalukaay ag lëmës la gees defar ak ag wëñu mbéll, naka-jekk përëm lay doon, gu ñu lal lenn lu tàcc luy ber (ab berukaayu mbëj), mooy tax ba lëmës-lëmës yi duñu laalante. Ngir yokk xiirtalu gi, lëmës gi ci ab dogub weñ (di saal bi) lañu koy defe. weñ gi faww mu am senniinu bijjaakon gu kawe, di li nuy wax ni benn jumtukaay bi di nangoo bijjaakon jàll ko. + +Kàttan +Kàttan gi rënku ci xiirtalukaay bi (ñu koy natt ciy Joule) dafay yam ak dayoob liggéey bees soxla ngir am dawaan biy wal ci biiram ak itam ngir jur toolu bijjaakon bi, ba tax: + + + + I mooy dawaan biy wal ci xiirtalukaay bi; + +L di xiirtalu gi; + +E mooy kàttan gi rënku ci xiirtalukaay bi. + + W di liggéey bi + +Nataal +Nataali xiirtalukaay yu ndombo yees móol + + + Xeeti saali bijjaakon yu wuute yu ay xiirtalukaay(nataal yees defareek ab nosukaay). Ci saal bi lañuy lëmës wëñug mbéll gi dawaan biy jur toolu bijjaakon bi di jaar. + +Bokktekki + +Taxañ + +Lëkkalekaay yu biir + +xiirtalu + +soppalikaay + +mbëjbijjaan + +mbëj +Ci Jëmm, baraay ab delluwaay la bees di sukkandiku ngir xam ñaata yoon la genn feeñte guy tóllantiku di amal ag tóttantikoom ci benn diiru jamono bees jël. Maanaam ñaata yoon la xew-xew bi di feeñ, ci genn anam gi, ci benn diirub jamono. Ngir natt baraayu genn feeñte dañuy jël benn diiru jamono xool ñaata yoon la mbir mi di dellusi ci biir diir bi lim bi ciy jóge di doon baraayam. Geneen anam gees ko manee natt mooy xool jamono yi ñaari xew-xew yu toftaloo di door, bu ci nekk nga xam jamono ji muy tambali ak ja muy jeex, kon xam itam seenub diir. Baraay bi di doon safaanu boobu diir . + +Njureef li ñu koy xayma ci Hertz (Hz), 1 Hz mooy teewal benn xew-xew buy am benn yoon ci 1 saa (s). Ngir natt baraay bi jumtukaay bees di jëfandikoo lees di wax ab nattbaraay. + +Kemi jëmm +Xiirtalug mbëjbijjaakon ag feeñteeg jëmm la gees di gis niki juddug ag wuuteeg aj ci diggante ñaari cati ab wommatukaayu mbëj walla ci ag ndombo gu mbëj mbaa juddug ag dawaanu mbëj ci seen biir, su wommatukaay bi walla ndombo gi nekkee ci biir ab toolu bijjaakon. +Ci gii feeñteg jëmm la doxub soppalikaay yu mbëj yeek xiirtalukaay yi sukkandiku. + +mbëjbijjaakon +Dëkku Xo Ci Min ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 1095 km², ci 2009 amoon na 7.103.988 way dëkk. + +Wiyetnaam +Ndombo gu mbëj dees koy tekkkee niki lëkkalante gu ay cëri mbëj ci wenn yoon wu tëju ci genn anam guy tax ba dawaanu mbëj ga cay jaar di man a wéy di wal, maanaan du am benn dog-dog. + +Gëstug ag ndombo + +Solos gëstu ag ndombo gu mbëj mooy génne ca dayooy dawaan ba ak dend ba. Sukkandiku ci melokaani cëri ndombo gi ak àtte yi ñeel ndomboy mbëj yi. + +Noste gu wéy + +Ag ndombo gu mbëj guy dox ci ag noste gu wéy (maanaam kem yi ajuwuñu ci jamono, seen dayoo du soppiku ci jamono, dees na ko woowee itam jamono-soppeekudi) dina am lumu néew-néew ag ndëgërlu, ab jurukaayu mbëj di luy joxe ab dend (walla ab dawaan) bu wéy, man naa am it, yenn saa yi, ab doxalukaay. +Manees naa gëstu ag ndombo ak yii àtte: + + Àtteb ohm: moo nuy xamal dayoob dend U bi ci ag ndëgërlu R gu dawaan I jaar ci biiram: U = RI. + + Àtteb Kirchhoff mooy lay jox jëflante bi ci cër yu wuute yu ndombo gi. + + Soppalig ñettikoñ-biddiw + + Soppalig biddiw-ñettikoñ + + Céetu Norton: mooy wax ne gépp ndombo gu ndëgërlu (ndombo gu ami ndëgërlu rekk) dafay yam ak ab jurukaayu dawaan I bu lang ak ag ndëgërlu R. + + Céetu Thevenin: mooy wax ne sooy xoolee ag ndombo gu mbëj ci ñaari tomb, yu nekk ci ndombo gi, dafay yam ak ab jurukaay bu dendam tollook wuuteeg aj gi ngay natt ci diggante ñaari tomb yi, toppanteeg ag ndëgërlu gu yam ak gi ngay natt ci diggante ñaari tomb yi batay su jurukaay yu temb yi fayee. + +Noste gu jàllu +Batay dawaan bu wéy lees di dundale ag ndombo gu ami fattalukaay walla xiirtalukaay mbaa ñaar ñépp. Kem yi U ak I dañuy bawoo cig noste gu jàllu dem ci geneen noste gu sax. Kon nosteg jàllu du luy wéy, luy nekkandi la rekk. +Àtte yees bind ci kaw yépp manees na leen fee jëfandikoo batay. + +Noste gu sin +Ci gii noste ndombo gi dawaan bu safaanu lañu koy dundale. Àtte yees bind ci kaw yépp manees na leen fee jëfandikoo batay, waaye ak coppite yi ci war. + +Mbëj +Fattalukaay ab cër la bees di jëfandikoo ci biir ndombo yu mbëj yi, di fees di rënk kàttanu mbëj niki toolub mbëjtekkaaral, yani mbëj yi ñoo fay tase dankaloo fa. + +Dafay am ñaari làcc, yu tapp yees defaree ak lu man a wommat mbëj, yu làng ak benn diggante bi. Ñaari làcc yi yani mbëj yu dekkarloo fay nekk, wenn làcc wi yan bu ëpp (+) lay am weneen wi bu yées (-), segam ñaari yan yu dekkarloo dañuy xëccante, waral juddug toolu mbëjtekkaaral bi. Taraayu tool bee ngi aju ci limu yani mbëj yi nekk ci diggante làcc yi, moom itam aju ci dendu mbëj bi. Ngir bañ benn yan jóge ci wenn làcc dem ci weneen, faww ñu def lenn ci seen diggante, lenn loolu lees di woowee ab lankmbëj, man naa nekk ngelaw rekk walla këyit mbaa lépp luy bañ mbëj jàll ko. Ab fattalukaay bu nekk dafay am ab def (C) ñu koy natt ciy farad (F), dayoom a ngi aju ci lankmbëj bi, mooy li nuy wax dayoob toolu mbëj bi gën a rëy bi nga xam ne su ko weesoo yani mbëj yi man a jóge ci wenn làcc dem ci weneen, di luy waral itam yàqug lankmbëj bi. + + I mooy dawaan bi; + U mooy dendu mbëj bi ci diggante ñaari làcc yi; + C mooy defu fattalukaay bi. + + mooy coppiteeg dend bi ci jamono. Su dendu mbëj bees teg ci diggante làcc yi soppeekoo limu yani mbëj yi soppeeku, toolu mbëjtekkaaral bi soppeeku itam. Kon am na benn limu dend bees warul a weesu lu ko moy fattalukaay bi dafay yàqu, lakk. + +Mbëj +Ndakaaru wenn la ci 35 tund yees séddalee Réewum Senegaal, di it benn ci 4 tundi diiwaanu Ndakaaru, dëkku Ndakaaru mooy péeyu tund week diiwaan bi te am 1 030 594 ciy way-dëkk + +Séddaliinu tund wi + +Tund wi dees koo dog-doge ci 19 dëkkaani ndiiwaan, di: +Beer + +Biskuwitëri + +Kamberéen + +Jëppël-Derkle + +Faan-poe Ë-Amicee + +Gëltappe-faas-Kolobaan + +Graa Ndakaar + +Aan-Nelleer + +HLM + +Medinaa + +Meermoos-Sakre-Këër + +Ndakaaru gu Platóo + +Ngor + +Parsel aseni + +Paduwaa + +Sikaap-Libeerte + +Wakaam + +Yoof + +Lëkkalekaay yu biir + +Tundi Senegaal +Diiwaanu Ndakaaru + +Ndakaaru + +Téerekaay + Ibrahima Diallo, Le droit des collectivités locales au Sénégal, Paris, L'Harmattan, 2007, 380 p. + Djibril Diop, Décentralisation et gouvernance locale au Sénégal. Quelle pertinence pour le développement local ?, Paris, L'Harmattan, 2006, 268 p. + François Zuccarelli, « Le département sénégalais », Paris, Revue juridique et politique, n° 3, juillet-septembre 1968, p. 854-874 + +tundi Senegaal +Coronel Fabriciano : dëkku Breesil + +Breesil +Al Bayda ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Libi. + +Mi ngi yaatoo 155,54 km², ci 2010 amoon na 250.000 way dëkk. + +Lybia +Xolaxol (Lamprotornis caudatus) picc la ci néegu Sturnidae. + +Picc +Toq yi (Tockus spp.) picc lañu ci néegu Bucerotidae. + +Giir yi + Tockus alboterminatus (Calao couronné) + Tockus bradfieldi, Toqu Bradfield (Calao de Bradfield) + Tockus fasciatus (Calao longibande) + Tockus hemprichii, Toqu Hemprich (Calao de Hemprich) + Tockus pallidirostris, Toqu sàll wu xoyyi (Calao à bec pâle) + Tockus nasutus, Toqu sàll wu ñuul (Calao à bec noir) + Tockus monteiri, Toqu Monteiro (Calao de Monteiro) + Tockus erythrorhynchus, Toqu sàll wu xonq (Calao à bec rouge) + Tockus leucomelas (Calao leucomèle) + Tockus flavirostris, Toqu sàll wu màkka (Calao à bec jaune) + Tockus deckeni, Toqu Decken (Calao de Decken) + Tockus jacksoni, Toqu Jackson (Calao de Jackson) + Tockus hartlaubi, Toqu Hartlaub (Calao de Hartlaub) + Tockus camurus, Toq gu ndaw (Calao pygmée) + +Picc +Tan yi picc yu mag lañu ci néegu bu ndao Aegypiinae ci néegu Accipitridae. + +Picc +Ci jëmm, ngóora gi mooy limu kàttan gi genn noste di jox geneen ci jenn jamono. Kon ngóora daf lay delloo ci kàttan gi nekk ci biir genn noste gi, dila xamal liggéey bi mu man def ci jenn jamono. Liggéey bi man naa gaaw te woyof, diis te yeex, walla boole ñaar yépp, gaaw te diis, boobaa dina laaj kàttan gu jéggi dayoo. + +Natt ngóora gi +Segam ngóora gi mooy liggéey ci jamono, lu liggéey bi di gën a diis jamono ji mu koy di gën a néew ngóora gi di gën a bari. + + W: Watt bennaanu nattu ngóora gi + J: Joule di bennaanu nattu liggéey bi + S: Saa di bennaanu nattu jamono ji. + +Nattiinu ngóora gi mi ngi aju ci xeetu noste gees am. + +Su nekkee kàttanu doolerandu lanu am, noo ngi koy nattek ab baril ci diggante doole jees ci def ak xéel yi noste gi di demee: + +Su fekke kàttanu mbëj lanu am, noo ngi koy nattek ab baril ci diggante dend beek dawaanu mbëj bi: + +Sunu xamee àtte bi yor ngóora gi, anam gi muy soppeekoo ci jamono P(t) (t:jamono) ak diir bi muy amee, Kàttan gees weccee gépp ci doxug noste gi manees na koo natt: + +Kemi jëmm +Ci jëmm, liggéey bi jenn doole def mooy kàttan gi doole jooju joxe ngi tomb bi ñu ko jëfe man a topp, maanaam jóge fa mu nekkoon randu benn digal bi. Digal bi muy randu mi ngi aju ci taraay ak jubluwaayu doole ji. Soo buuxee ab lal, mu randu, def nga ab liggéey, tomb bi nga jëfe doole ji, maanaam fi nga jañee lal bi doole ji, mooy fi nga teg say yoxo, te dañuy toppaale lay biy randu. + +Natt ab liggéey +Ngir xam liggéey bees def ci ag noste faww nu xam doole ji nu ci def ak dayoob digal bi mbir mees jañ doole ji randu. Jenn doole ju sax jees jañ menn mbir mu dox topp wenn yoon wu jub dina joxe benn liggéey bi W bi yam ak ab coppiteeg kàttanu nosteg gi. + +Doolerandu +Kemi jëmm +ci jëmm, kàttanug imbiku, mooy kàttan gi menn mbir di soloo suy yëngu. Mooy liggéey bees laaj ngir man a jëlee wenn yaram wi cig tekkaaralam doxal ko, muy daw walla di wëndeelu. + +Ngir man a natt kàttanu wenn yaram wi faww nu xam dayoom m ak xél v yi muy daw. +K = + +kàttan +doolerandu +Mbëjtekkaaral ab bànqaasu jëmm la buy gëstu feeñte yi juddoo ci yani mbëj yu tekkaaral yi, ci lu gën a jub, mooy liy gëstu doole yi ab toolu mbëj bu tekkaaral (ci maanaa bu dul soppeeku) jañ ay yani mbëj yu taxaw. + +Àtteb Coulomb, di biy tax ñu man a xayma doole ji F ji benn yanu mbëj Q sàkk te sëf ko beeneen yan q bumu jegeel ak benn digal bi d. Mooy àtte bi ubbi gëstug yile feeñte, ginnaaw ñaareelu xaaju ati 1800 lees ndar-kepp léjmbët gi ak lees wax di yamaley maxwell, xam lépp lu ci laqu, jóge ci mbëjtekkaaral dem ci mbëjbijjaakon ngir gisiin wu gën a yaa ci feeñte yi. + +Lëkkalekaay yu biir +Jëmm +Toolu mbëj +Xiirtalug mbëjtekkaaral + +mbëjtekkaaral +kariim jóob 25 sàttunmbar 2010/waxtu 11:28 Alikànte Espaañ. +waaw lii ngeen wax dëgg la ndaxte sama ñatti maam rekk la lañ ma limal ñeentel ba dem sudaan ak caadd sama maam jótumaa dundak moom waaye baayu tax wax na ma ne sama maam migi juddu ca Atum 1854 ca Dëkk bu ñuy wax walaji ca waalu dexga la ne koon mingi tudoon mañaŋ omar . +ana kan mooy baayam omar Jóob mooy baayam omar a ngi juddu 1264 ca Atum gàddaay ga maanaam Axiraa ci ati Islaam ca fuuta Dëkk bu ñuy wax Goolore . Omar Ahmmidu julde wala jumde mooy baayam mingi juddu 1203 ca gàddaay ga axiraa ca fuñuy wax Màddina Alnuubiya fisuudaniya .Ahmmidu Omar Ben Alii mooy baayam mingi juddu ca Atum 1172 ca Dëkk bu ñuy wax tikrir Altanganiya.foofu nik xawma ci baan gox wala baan ´Réew la bookku,ba tax na ku ci am xam xam mangi lay ñaan nga gindima ci Insàllau , + sama maam Mañaan omar ca 1881 ci la jugé waloo jégi dexga ñéw Njaambur ci Dëkk bu ñuy wax ñoomre lóo wante booba ay naak yu bare bari la yoroon aki xar niki bëey waante yagul darra mu xam ne boroom muk jur munta dékak baykat mu def bu naawete mu maangé ñéw fuñuy wax nayoobe waante 1886 bu loli jotaan ba tawatul jurgi sax la ndox moo waral ñu jaal ba penkup nayoobe fuñuy wax Dégg Mbeeloñ wara toolu ci 10 kilometar ak nayoobe,te foofa neekoon gottu boo xamne pekoom yéep béykat amu fa woon ñépp ay saamu lañ, mutude ko Mbelooñ Jóob waaye pëll yi mu Dékkaloon walla yi mu deendaloon,ñu tambuli naan sàresiik maanaam Kër Mañaanŋ omar minkoo sañci 1890. +moom nik danabaaxoo di def atmune mu yóobante seexna seexshadibu Ëediyay maamam yonant bi seex shadibu di koy géram ci ay bataaxal ba 1901 mu giseek moom ca lábude ga ca Kér mamaar sarr,1904 seexna ñéw ganesiko mbelooñ mu rayal ko 3 nak ak 7 gatt ba mi deem mu joxko Ëediya 10-ak 10 gatt calako waxe waxam ju siiw ja ne koo ca ba ngay am martaay seexyi booba gisee gunu ci sair waaye biss niki tay amnga seexul muraaduya sa Dëkk bi ñaan nañ fi Yàlla képp kuñ fi mu baña am bugalum bameel ak yaamal xiyaam mu nee ti ko waxal loo bégg ci sa Dëkk bi mune aydara ngagide ñaak Ndox reekk ko yaax mu nee kodemal gas suuf fu seel idil mako ,bim ko inde mu ñaan ca joxko nee ko foo bégg xéewal gi ak ndox mu bari reekk nako suuf si wérl. lii mooy sama Tàriixu Maam Seex Mañaŋ omar . +Esperanto - Làkk + +Maandarga - joxoñ bi - joxoñ yi- Esperanto-Làkk + + Jubilea simbolo + flago + +Internacia Lingvo Kurso - volofa lingvo +Lii ndimbal: (Helpo: www. esperanto-afriko. org. (kurso en araba lingvo); www. lernu.net kursoj (= kursoj) +La internacia lingvo - ESPERANTO estas lingvo facila. + +Internacia Làkk - "internacia lingvo" - ESPERANTO + +Ĉ = (Sili) Ĉilio, G = (J) germanio, germanujo (=Almaañ) , Ĥ = Ĥemio (= ?; (Novartis, BASF), J = Junio (=Suwe); Julio (= Sulet ); J = Jordanio (Jordaani ), Ĵ = ĵurnalo (= surnaal ); Ŝ = ŝipo (= gaal / waruwaay ); Ŭ = aŭto (= oto ; ndaama; woto) + + + januaro = Samwie + februaro = Fewirie + marto = Maars ; Maars(weer) + aprilo = Awril + majo = Mee + junio = Suwe + Julio = Sulet + aŭgusto = Ut + septembro = Sattumbar + oktobro = Oktoobar + novembro = Nowembar + decembro = Disambar + +Alfabeto de Esperanto ESPERANTO ( fr.: alphabet) + Alfabeto de Esperanto; + - Esperanto, a, b, c (gune) deggal! + + ?? - Prononoco kaj alfabeto ( fr.: prononciation et alphabet) : “Afriko”, "hotelo", "amiko", "kontinento". + +ESPERANTO - ALFABETO - ( fr.: alphabet) + +Aa, Bb, Cc, Ĉĉ, Dd, Ee, Ff, Gg, Ĝĝ, Hh, Ĥĥ, Ii, Jj, Ĵĵ, Kk, Ll, Mm, Nn, Oo, Pp, Rr, Ss, Ŝŝ, Tt, Uu, Ŭŭ, Vv, Zz. + +Nomoj de la literoj: a, bo, co, ĉo, do, e, fo, go, ĝo, ho, ĥo, i, jo, ĵo, ko, lo, mo, no, o, po, ro, so, ŝo, to, u, ŭo, vo, zo. + +Ekzemploj: c = : cigaro (= ), princo ( = lingéer) s = : kiso (= ?) (baiser / kiss); +v = : varma (= taanga ) z = : rozo (= ?)(Rose (fleur)) + + Ĉĉ, Ĝĝ, Ĥĥ, Ĵĵ, Ŝŝ, Ŭŭ + + Ĉ = Ĉado (= Cadd ) + ĝ = ĝangalo ( ?; ) (jungle) + ĥ = jaĥto; ( ? );(= gaal); (yacht) + ĵ = ĵurnalo (surnaal) + ŝ = ŝipo (gaal ) + ŭ = aŭtobuso (ween, bis, kaar ) + +(Vikipedio en Esperanto: cx= ĉ, gx= ĝ, hx= ĥ, jx= ĵ, sx= ŝ, ux= ŭ) + + ĉ (cx), ch, + ĝ , (gx) gh, + ĥ (hx) hh, + ĵ (jx) jh, + ŝ (sx) sh + ŭ (ux) u + +Ekzemplo : chinia esperanta retpagho = ĉinia esperanta retpaĝo + +Gramatiko: + +la (= artikolo ) + la tablo - taabal + tablo - (= 1 tablo / = 1 taabal ) + +Substantivo +(Substantivo / ?) -o domo (= neeg) (dom / o dom-o) + + dom / o = neeg; ker; kër + 1 domo = 1 neeg; + 1 domo = 1 ker; + 1 domo = 1 kër + +Adjektivo +(Adjektivo / ?) -a granda : (= ?)(grand / big); granda domo - + granda domo + malgranda domo (ndaw)/(neeg) + +Pluralo + +(Pluralo / ?) -j : *malgranda domo (ndaw)/(neeg) + + malgrandaj domoj (ndaw)/(neeg) + 1 domo + 2 domoj + 1 granda domo + 2malgrandaj domoj (ndaw)/(neeg) + +Adverbo +(Adverbo/ ?) -e. Eva kantas bele. (adverbo) - Eva estas bela. (adjektivo) +(kantas = woy ); (bele/bela = ?(rafet) /?(taaru)) + +Deklinacio +(deklinacio) + 1. (nominativo): la ronda tablo - (kiu?) + 2. (akuzativo): la rondan tablon (kiun ?) (= akuzativo /accusatif) + + de la ronda tablo (taabal) + al la ronda tablo +(ronda = móróg) + + (joxañ - direkto) + n + (joxañ - direkto): en la parko ( bayaal ) - en la parkon >( (joxañ) > bayaal) + ( dox ) mi iras en la parko / mir iras en la parkon ( (joxañ) > bayaal ) + +aboot ji /jaboot yi - Personaj pronominoj: + (personaj pronominoj): ( ) + mi - (man) ------------------- ni - (ñun) + vi - (yow) ------------------- vi - (yun) + li - (persono) (mom) --------- ili (pluralo) (ñoon) + ŝi - (persono) (mom); oni ( fr.: on) + ĝi - (objekto, ideo) (mom); si (la sama persono kiel la subjekto, se tiu ne estas mi, ni aŭ vi (aŭ ci)) + + mi - man + vi - yow + li - mom (goor !) + ŝi - mom (jigeen !) + ĝi - mom (fr.: la chose, l'idée) ni - ñun + vi - yun + ili (pluralo) - ñoon + + moom - Posedaj pronomoj posedaj pronomoj + -a: + mia - via - lia - ... + mia amiko - coro (fr.: mon ami), + via hundo - xat; (= (fr. ton chien), + lia hundo Deklinacio + (deklinacio): + mi (1. nominativo), + de mi, + al mi , + min (2. akuzativo),. + + toolaale - Komparado + (Komperativo) + pli + (Superlativo) +plej : + forta - dëgër + pli forta (ol) + plej forta (el) + + forta - + pli forta (ol) - + plej forta (el) - + +== 'Konjugado - Verbo / Prezenco == + +Konjugado - Verbo / +Prezenco / :+ - as + am / i - nob, sopp + + mi amas vin , vi amas vin, li amas vin; (..) + (vin'= akusativo) + + démb ji - Preterito + + démb ji - Preterito/ + -is: mi amis vin, vi amis vin, li amis vin (vin= akusativo) + + muj gi - Futuro +Futuro / + -os: +mi amos vin, vi amos vin, li amos vin (vin= akusativo) + + Kondicionalo +Kondicionalo -us mi amus vin (vin= akusativo) + + ndigtal - Imperativo + ndigtal - Imperativo +-u amu min! diru! - (wax ! ) + + Infinitivo +Infinitivo + -i: Mi volas lerni la internacian lingvon = Mi volas lerni Esperanton (-n = akusativo) + + Tobio estas hundo. (xat ) + Marko karesas hundon. (karesas - raay) (hundon= akusativo) + Marko estas amiko de Maria. ( ) + Maria salutas amikon kaj vidas hundon. (vidas - gisee ) (amikon= akusativo) + + laŋ / Demanda frazo + Demanda frazo: Ĉu ? (laaj / laajte) + Ĉu vi komprenas min? Jes, mi komprenas vin. (komprenas = nànd ) + Ne, mi ne komprenas vin. (ne komprenas - nàndul); (komprenas = nànd ) + Ĉu vi komprenas vorton? (vorto - kaddu; vorton= akusativo) + Mi ne komprenas vorton = (jup) + Vorton ne komprenas mi = (jup) + Vorton mi ne komprenas = (jup) + + Tabelo de korelativaj vortoj + Silabo i + "i"; (nedifinita - fr. indéfini) + + Antaŭsilaboj + k+i+... ki- demandovorto - + t+i+... ti- indikvorto - ( ) + i- +( ) + ĉ+i+ ... ĉi- - ( ) + ne+n + i- neni- + + Antaŭsilabo - Mallonga klarigo + ki- kio - kan ; kiu - lan; demandovorto -(kiu? - kan; kio? - lan;) + ti- 'indikvorto' - + i- iu - + ĉi- ĉiu - + neni- neniu - + + (5 x 9 = 45 korelativaj vortoj - tabelvortoj): + Postsilaboj Postsilabo - Mallonga klarigo -o nedifinita aĵo - + -u individuo, difinita aĵo, - + -a eco - + -el maniero - + -e loko - + -am tempo - + -om kvanto - + -al kialo - + -es posedanto - + + 45 korelativaj vortoj - tabelvortoj: + kio - tio - io - ĉio - nenio - + kiu - tiu - iu - ĉiu - neniu - + kia - tia - ia - ĉia - nenia - + kiel - tiel - iel - ĉiel - neniel - + kie - tie - ie - ĉie - nenie - + kiam - tiam - iam - ĉiam - neniam - + kiom - tiom - iom - ĉiom - neniom - + kial - tial - ial - ĉial - nenial - + kies - ties - ies - ĉies - nenies - + + wañi ñi i - Nombro, Nombrado, arabo cifero + Nombro, Nombrado, arabo cifero ( ) , araboj ciferoj + + nul 0 + unu 1 --- ses 6 --- dek unu 11 --- cent 100 + du 2 --- sep 7 --- dekdu 12 --- ducent 200 + tri 3 --- ok 8 --- dudek 20 --- mil 1000 + kvar 4 --- nau 9 --- dudek unu 21 --- du mil 2000 + kvin 5 --- dek 10 --- tridek 30 --- du mil unu 2001 + "miliono" 1'000’000 + +roma cifero: I II III IV V VI VII VIII IX X C M +"Bonan nokton!" + + wañi ñi i - Kardinalaj numbroj +kardinalaj numbroj+ -a: + + unua: 1. + dua: 2. + + Baatukaay + grand / a - rey, mag + malgrand / a - tuuti, ndaw + manĝ / i - lekk + trink / i - naan + dorm / i - nelaw; mi dormas; dorm / i: + +(traduko en franca lingvo): + dorm / i: dormir, reposer; + dormo 1.: sommeil; + dormo 2.: sommeil, repos; + dormema: ensommeillé; + dormegi: dormir d'un sommeil de plomb; + dormeti: sommeiller, somnoler; + dormigi: endormir; + endormigi: endormir; + endormiĝi: s'endormir; + fordormi: manquer; + maldormi: rester éveillé, veiller ; + sendormeco: insomnie; + dormigilo: somnifère; + dormilo: élément de literie; + dormomalsano: maladie du sommeil. + dormemo: sommeil . + + mort / i - dee (la mort / o; , li mortas; mort/a, mort / e;) + ir / i - dox, dem + ven / i - ñow/ñew + don / i - may, jox + pren / i - jël; + parol / i - wax; la parolo; li parolas, + am / i - nob, sopp + kiu? - kan + kio? - lan + hom / o - nit + viro - goor + edzin / o, homin / o, sinjorin / o, virin /o - jigeen + kap / o - bopp; (Mia kapo doloras!) + okul / o - bët + orel / o - nopp + nas / o - bakkan + buŝ / o - gemmiñ + dent / o - bëñ + lang / o - lammiñ + kor / o - xol + man / o - loxo + pied / o - tank + akv / o - ndox; la akvo estas klara; + fajr / o - safara; flam / o - (safara); + sun / o - jant; mi estas la plej feliĉa homo sub la suno; + lun / o - weer; fazoj de la luno; la lunoj de Jupitero; la plenluno disvastigis lumon preskaŭ tagan + + Salaamaalekum + + Salaamaalekum ! (Paco estus kun vi!); Bonan tagon ! Saluton! + Maalekum salaam ! (Kaj kun vi estus paco!); Bonan tagon ! Saluton! + + Bonan matenon! + Bonan nokton! + Bonan tagon! + Bonan vesperon! + + Nan nga def ? Kiel vi fartas? / Naka nga def ? Kiel vi fartas? + Maa ngi fi rekk. + (http://fr.lernu.net/lernado/vortoj/frazoj/index.php Des phrases utiles) + + Ba beneen (yoon). Ĝis (la) revido! + + Baatukaayuea.org Radikoj-685: + a + + uea.org Radikoj-685: vortoj: + + hom / o - nit ki; + homoj - nit ñi; (pluralo/fr. le pluriel) + hom / a - (adjektivo) ; + aĉet / i - jënda / jénd; + aĉet / o - (..) (substantivo); + aĉet / i - (infinitivo); (jënda / jénd); + + -j - (pluralo); (fr. le pluriel) + + [http://eo.lernu.net/lernado/vortoj/bildvortaro/5.php Bildvortaro - lernu.net] + Bildvortaro - lernu.net + + a. - (bela - raphet ; bela - taaru); (fr.: suffixe adjectival) homo / homa - (substantivo / adjektivo); Finaĵo + -Aĉ - domaĉo (malbela domo); (fr.:suffixe péjoratif); bela; mal-; mal+bela=malbela;Finajxo; domo - naik; (bela - raphet); domo → domacxo; (PMEG -Acx); Domo; PMEG gramatiko + aĉet / i - jënda / jénd; aĉet / o - (..); (aĉet / i - infinitivo); aĉeti - jaynda; ; ; Domo + -Ad - (fr. suffixe d'action): uz/o; uz/i - (fr. user): la uzado de la artikolo estas tia sama, kiel en aliaj lingvoj; uzo → uzado = daŭra, regula uzo; (PMEG 38.2.2. AD = “dauxra ago”).Uzo ;UZO; Internet; Tutmonda uzado de la interreto; (Kutimo - ( cosaan));((cosaan)) + adres / o - (fr.: l'adresse); adresi -(verbo); (sendanto / ricevonto de la letero); + aer/o - Ngelaw; aero - nguelarw; (fr. l'air); Aero + afer/o - mbir mi (Substantivo); (aferoj - mbir yi); afer/o - afeer bi; (aferoj - afeer yi) + afrik/o - Afrig; Afriko + ag/i - ( def); agi - waxaale; ago - jayf; Agi; AGI; kunagi - (..); kunago - (..); interago + aĝ/o - att; Aĝo; (jaro - (at mi) At; (jaroj - at yi); Jaro; + + aĥ ! - (aĥ ! = forta surprizo ! ); Surprizo; surprizi - jaaxal; surprizo - .. ; esti surpriza - ..; (PMEG 18.3.); + ajn - .. ; (ie ajn - .. ; (iu ajn - ..); (iu ajn - .. ; (io ajn - ..; (PMEG 14.3.4.); ; iu - ..; + -Aĵ - -Aĵ; (sufikso - ..; vortfinaĵo - .. ); (posedaĵo ; propraĵ o - .. ); Finaĵo; Posedaĵo ; Posedo; + akcept/i - nangu; + akv/o - ndorh; akvi - rawesh; Ndox; Yolaakon; Akvo + al - (Al montras celon: mi iras nun al la onklo);montri - ..;(celo - .. ; (iri - .. ;(onklo - .. ; al; AL; al PMEG + + ali/a - .. ; (Alia estas komunumo de Italio.) + + almenaŭ- .. + alt/a - ..; alteco alto + amas/o - ; (maso - këmbay gi; maso - laf li; maso- saam bi); Maso; .. ; (fiziko);Fiziko; Amasinformilo; Amaskomunikilo; (Ceññeer-mbej) + ambaŭ - ; + amerik/o - Aamerig ; Usono - Diiwaan yu Bennoo ; amerikana kontinento - (Aamerig) ; Ameriko, Usono,Kontinento; + am / i - norb; amo - mbougayle; Amo + amik/o - harit; amiko - (xarit bi); amikeco Amiko + + + -An - - klubo → klubano; (klubo - boyet bi); -->("klubano" - ) ); klubo + ankaŭ - + ankoraŭ, - ; ankoraŭ ne - ; + anstataŭ -; anstataŭigi - ; (anstataŭ- ); anstataŭ - ; anstataŭ - ; + -Ant - (participo -); --> dum la ago — la ago ankoraŭ ne finiĝis, leganta = tia, ke oni ankoraux legas; ant ANT; + antaŭ - ; (antaŭ - ); (antaŭ - ) ; + aparat/o - ; sonaparato - ; respondaparato - ; telefona respondaparato - (telefon bi);(waxsori wi)(waxsufe)Telefono; lauxtilo - ; sono - ; Sono; aparato; + apart/a - ; apartaĵo - apartamento - ; Apartamento + apenaŭ - (..); + aper//i - feeñ; malaperi - meles; + april/o - awril ; Aprilo; 4 - ; monato - weer ; Monato; Monato - Weer; januraro - Samwie; februaro - Fewirie; marto - Maars; aprilo - Awril; majo - Mee; junio- Suwe; julio - Sulet; aŭgusto - Ut; septembro - Sattumbar; oktobro - Oktoobar; novembro - Nowembar; decembro - Disambar; + + apud - apud (apud la altaro) + -Ar - -ar(sufikso - .. ; vortfinaĵxo - .. ; (vorto - kaddu ); (vorto - kaadu ); vortaro - Baatukaay; vortaro - Baatukaay ; ar Ar; + aranĝ/i - dogal; + artikol/o (literaturo) - (..) ; nedifinita artikolo (gramatiko)- ; difinita artikolo (gramatiko): la; la; artikolo (gramatiko) -; (skribaĵo - ; skribo - ; teksto - ); literaturo - Njàngat; Literaturo - ; + + art/o - Fànn; belartoj -; arĥitekturo(arkitekturo - (..); arkitektura fako - ; Beletro; Beletro (aux belliteraturo); beletro - (..), muziko - Way , skulptarto --> (skulptartisto - ); pentrarto - ); + as - as (finaĵo) prezenco verba tempo montranta la estantecon; as-tempo, nun-tempo. (-->preterito. futuro, imperfekto, perfekto, pluskvamperfekto); prezenco - mi lernas, vi lernas .... ( lerni - jang;)Prezenco; as As; lerni - jang; lerni -janga; lerni - ñang; + asoci/o - kompin; firmao - kompin; firmao (kompin); (ni asocias asocion) ----> asoci/i -; asoci/o - Asocio de Sudorient-Aziaj Nacioj; (ASAN); Asocio de Sudorient-Aziaj Nacioj; (ASAN); ASEAN; ASAN; Asocio; (alianco - (..) ); Alianco; + + aspekt//i - seet; aspekti simile - (..); ; tre - ; aspekti simile - ; aspekti - seet; aspekto - melokaan; + at - (pasiva participo - dauxrado aux ripetado)(gramatiko); pasiva participo - ; pasiva - ; participo - ; Gramatiko; at AT;at + + atend/i - ; atend/i - ; (atendo-kompenso - ); + atent/a - ; atenta - atento - ; (atento - ) + + ating/i -; atingi (vilagxon), (urbon, lokon, ejon) - ; + aŭ - + aŭd/i - ; aŭdi (parolon) - ; aŭdi paroladon - ; + aŭskult/i - ; + aŭgust/o - Ut; aŭgusto - Ut; Aŭgusto; ok - 8 - ; monato - weer; Monato + aŭstrali/o - (la sxtato "aŭstralio") - aŭstrali/o - (la kontinento "aŭstralio") - Aŭstralio; + aŭtobus/o - (publika aŭtobuso) - ; publika aŭtobuso - ; aŭtobuso - ;Aŭtobuso; + aŭtomobil/o - ; aŭti -; Aŭtomobilo;Aŭto + aŭtun/o - ; aŭtun/o -; aŭtun/o - ; Aŭtuno; aŭtuna - ; + av/o - ; (patro de patro - ); avo - ; (patro de patrino - ; gepatroj de patrino - ; gepatroj - ; + Azi/o - ; ; aziano - ; Azio + + b + + c + + o + + o - -o; (amiko- xarit bi; tajloro - nawkat bi ; ĉevalo - fas wi ; krajono - ?, broso - boros bi) + -Obl - “multipliko”. (kvanto - saam bi); (1 saam bi) (du → duoblo = kvanto duobla - (2 saam bi) ); (Matematikaj esprimoj - Xayma ) + ofic/o - (yen bi) ; (oficejo - (yen bi)) + oft/e - ? + ok - (8) Juróom ñett 8 + okaz//i - jib ; kio okazis ? ? Akcidento okazis - ; (Okazu, kio okazi devas) + + okcident/o - ; ; (okcident/a - okcident/e - ) + oktobr / o - + rigard / i - + vid / i - + okup/i - ( ); ekokupi - ; (Sin okupi pri arto. - + ol - (ŝi estas pli ol bela, ŝi estas belega) + -On, ON = “divido”.( du → duono 1/2 - ) (Matematikaj esprimoj - ) + oni - ) (oni kredas, ke kometoj anoncas malfeliĉon) + onkl / o - + ont - (Aktivaj participoj - ) (Viro, kiu poste legos, estas legonta viro.) + -Op - “grupo kun certa nombro da membroj” :du → duopo = grupo de du, paro; dek → dekopo = grupo de dek + opini/i - ; (opinio - ) + ordinar/a - + ord/o - ; orda - ; ordema - ; ordigi - + organiz/i - ; (ordo); (organizaĵo); organizo - + orient/o - O; (orienta - ) + + os - ( ...) Mi vidos - Waan arki doonaa. (Morgaŭ estos lundo.)- ...) + ot - pasiva participo (OT - stato (xaal) antaŭ ago) Oni elektu OT-participon, se temas pri stato ( ...) antaŭ la ago. (Libro, kiun oni poste legos, estas legota libro.) + ov/o - + + p + pac/o - nabad + paĉj/o - (- ) (Patro - → Paĉjo) (-ĉj, - ( Karesvorto por patro ( ): „Patreto! Paĉjo!“) Patro: (): Paĉjo! (Patreto!) + pag / i - san-wó + paĝ/o - + pan/o - + paper/o -; (leteropapero - ; - leterpapero - ) + pardon/i - ; (Pardonu! Pardonu min - !) + parol//i - ; (parolo -; (paroli pri.. - ) + part/o - ; (rezervparto - ) + pas//i, - (li pasis al mi - ) (pasi sur la strato, la placo, tra kampo); (paso - pasejo en monto - ; lia tago pasadis en studado; + patr / o - + pec/o - , (peco da pano - ) + pend//i - (la filo dependas de sia patro - ) + pens//i - + per - ( ) (Per hakilo ni hakas; sin nutri per legomoj; hak/i - ; (legom/o - legomoj - ) - (nutr/a - ; nutr/o - ; nutra manĝaĵo - ( ); plenigi botelon per akvo;) + perd/i - , (perdo - ) + perfekt/a - ; ()( ); (mi komprenas perfekte - ) ; perfekte ludi pianon; + period/o - + permes/i - + person/o - ; persona/persone - ; person/a( ): mia persona situacio; person/e ( ): mi konas lin persone + pet/i - + pied/o - ; piediri - ; planko - ; piediranto - + plaĉ//i - ; (bone plaĉas al mi - ); (tre plaĉas al mi ĉi tie); plaĉa - + plan/o - + plej - (Superlativo)- plej ofte - ; (Aŭgusto estas mia plej amata filo.)forta - pli forta (ol) - - plej forta (el) - (Akceptu mian plej koran dankon.) + plen/a - + plezur /o - + pli - (Komperativo) ; pli kaj pli - ; (lakto estas pli nutra, ol vino);(nutr/a - nafaqo); + plu - ( ); ktp (k·t·p ← kaj tiel plu) - + plur/aj - (pluraj personoj atestis tion);(pruvi - ) + plus - (2 + 2 = 4 → Du plus du faras kvar.)(matematiko - ) + po - (la drapo kostas po 2 $ dolaroj por metro (2 dolarojn por ĉiu metro); + poem/o - + pom/o - + popol/o - + popular/a - + por - + pord / o - + port/i - + post - ; La virineto kaŝis sin post kelkaj altaj ŝtonoj. post - dabaddeed, (kaddib); post kiam - (- Post kiam li alvenis, ni manĝis.) ; post tio - (Kvaronon da horo post tiuj vortoj ...) + poŝt/o - ; poŝtkarto - + pov/i - + pra- - “antaŭ tre longa tempo, primitiva”; origino de la mondo - ; tempo → pratempo = la komenca tempo de la homaro aŭ de la mondo; (avino - ; avo - ); (patro); (avo); praavo, praavino + + precip/e, - La lando vivas precipe el vitkultivado; (vino - + prefer/i - ; + preleg//i - )+(publiko - ); prelego/prelegoj - + pren/i - + pres/i - (libro - ) + preskaŭ - + pret/a - Mi estas preta preni, rompi la lancon por la vero. (lanco - ) + + preter - (Li pasis preter mi - ) + prezent/i - + + prezid/i, - ( ) ( ); (prezidanto - ); prezidento - ; (Francujo, Francio - Faraas; Germanujo, Germanio - Almaañ , Usono Diiwaan yu Bennoo : prezidento) + + prez/o - + pri - (Prepozicio - )Li parolas pri leono. La temo de la prelego estas leono. (leono - ) + princip/o - + printemp/o - ; (printempe - ); + + pro - (prepozicio) Ŝiaj dentoj frapadis pro malvarmo. (dento -)dentisto - )(dentbroso - ) + problem/o - + produkt/i - ; produkto - (fabrikado)(produktado) - ; (nur produkto de mia fantazio); (fabriko - ) + program/o - ; (sistema programaro: Ilprogramoj de komputa sistemo necesaj por funkciigi aplikajn programojn; aplika programaro: Kolekto da aplikaj programoj por iu ekstera aplika tereno (kontraste al sistema programaro).) + proksim/a - ; pli proksima (ol) - ; plej proksima (el) - + propon/i - ; propono - + propr/a - ; (kun propraj okuli- ;) (Fidu propran okulon.) (fido - ; fid/i - ) + prov/i - ( );(provi instrumenton, maŝinon, ponton, ĉapelon); (instrumento - )(ponto- );(ĉapelon- );'Montru al mi provon de via aktora arto. + publik/o - 111 + punkt/o - dhibic, joojis; (akurata - ) pup/o - ; دميةla infano serĉis sian pupon (ludi - ) (kokino - ); (kokineto- ); Pupo (ludilo) + pur/a - + + r + + radi/o - rajo ; radio - ; + rajt/o - (..); rajta - ; + rakont/i - léeb; rakonti - netali; rakonti - nettali; rakonti historion - (..); rakonto - léeb (bi); historio - léeb (b-) historio - leep (b-) ; historio - Taariix + rapid/a - gaaw; + raport/i - (..) ; (raportisto - ; raporto - ) + re- - (..) (ree - ); ĉiufoje (relegi) - ; saluti → resaluti = respondi saluton per saluto; diri → rediri = diri denove la saman aferon; + redakt/i - (..); (gazeto - surnaal (b-)) ; (redakti artikolon, raporton, cirkuleron, leteron) (avizo, komunikaĵo; mesaĝo - ;(leter / o - araf ;letero - bataaxal (b-); letero - leetar (b-)); (cirkulero - ; ( ; redaktisto - ; redaktoro - + region/o - ; regiona - + regul/o - ; regula - ; regule - + reklam/o - reklami - + rekt/a - ; (rekta linio - ; iru rekte! - !) + renkont/i - ; (mi renkontis lin hejme - ) respond/i - uyu; respondi - wuyu ; respondo - tontu (b-); + rest//i - des; + ret/o - ; La interreto - Internet; komputilo - ;(Por la fakuloj „la Interreto“ estas unu speciala el multaj interretoj;) ricev / i - jot; + riĉ/a - ; (riĉo - ; riĉeco - ) + rid//i - keeku; ridi - kex-kexi; ridi - ree ree; (rideti - ; (ridet/o) ; (ridinda - ) + rigard/i - (vid/i - ) + rilat/i - : (mi ne povas kompreni kiel via konkludo rilatas kun viaj premisoj.) (rilato - ; (rilatoj - ); (relatoj - ); (premiso: kondiĉo, bazo)(maksimo, principo -) + rimark/i - + river/o - + romp/i - ; (rompi brakon - ; rompi sian vorton - ) + + s + sabat / o - + saĝ / a - ; (saĝeco - ); (intelekto, menso, racio - ) + salon/o - (manĝosalono - ); (salono, eleganta ĉambro); ; (legosalono - );(libro - ) + salut / i - + sam/a - ; (de sama koloro, de sama valoro); (kolor/o - ); (valor/o - ) + san/a - ; esti sana -; saniĝi - ; sanigi - ; sano - ; (la sana homa menso - ; (sana menso en sana korpo); + sat/a - (); esti sata - ; ("sata malsatan ne povas kompreni" - sata homo ne povas kompreni malsatan homon) L. L. Zamenhof; C. Rogister ed.: Proverbaro esperanta, Stafeto, La Laguna, 1974 ISBN 400-7609-6 + scienc/o - , ; sciencisto - , + sci/i - ; scio - ; (mi volas scii; mi deziras scii - ;) + se - + sed - + seĝ / o - + sekv/i - ; sekve - ; + semajn/o - ; semajnfino - ; (labortago - ); (laboro - ); (tag/o -); + sen - + senc / o - + send/i - rán; sendito - ; sendi per poŝto - + sent / i - + sep - (7) + septembr / o - + serĉ/i - ; + seri/o - ; (televidserio, filmserio)(filmo - );(matematiko - ) + serv/i - adeegid + ses - lix (6) + si - ); (Elizabeto lavas sin en la lago); (a sama persono kiel la subjekto, se tiu ne estas mi, ni aŭ vi (aŭ ci)) + sid//i - + signif/i - ; signifa - ; sifnifo - ; + simil/a - + simpl/a - + simul/i - (li ŝainas esti malsana - ); simulilo - (); komputilo - + sinjor/o - ; sinjoroj! - ! sinjoro (..)! (..); sinjoro doktoro (s-ro doktoro) - ); s-ro (..); sinjorino (s-ino) - ; sinjorino (..) - (..); mia edzino - ; fraŭlino - ; fraŭlino (..) - (..); + sistem/o - ; (nervosistemo, nervsistemo, nerva sistemo, nervo - ); komputilo - + situaci/o - ; (komika situacio),(komika - ) skatol/o - ; nigra skatolo: (nigra - ), (aeroplano, aviadilo, avio - ),(akcidento - ); (flugo - ), (aerodromo - ); (alo, flugilo, (ŝvebilo) - ) + + skrib / i- bind; skribi - binda; skribi - fitaxu; skribi - rëdda; skribo - bind b-; skribo - leetar b-; + + sol/a - + somer/o - + son//i - (); sono - ; sonbendo - ; surbendigi - ; (surbendigilo - ); (magnetofono - );(brua, laŭta - ); (mallaŭta - ) + special/a - ; eksperto, specialisto, specialistoj - ; (specialiĝo - ) + spec/o - ; (iu speco da bestoj); (speci/o: „La origino de specioj“ (verko pri biologio de Ĉ. Darvino)) + spert/a - ; sperto - ; (li havas grandan sperton en sia fako - ) + sport/o - ; sport/i - ; Sportisto - + staci/o - + star // i - + strat / o - + stud / i - (studento - ) + stult/a - ; (stultulo - ) + sub - + sud/o - ; + sufiĉ/a - ), sufiĉe - ; (verbo) : sufiĉ/i - tio sufiĉas (por ni) - (..); (tiu sumo ne sufiĉas;) sukces//i - ; sukceso -; (liaj verkoj havis, akiris, ricevis, ĝuis, atingis entuziasman sukceson;) + suk/o - + sun/o - , ( ); (stelo - , )(stelfiguro - ) + super - + supoz/i - ;(supozeble - ); (mi supozas, ke li baldaŭ alvenos;) supr/e - ; supra - ; (" + n": (mi staris supre sur la monto kaj rigardis malsupren)) + sur - + + ŝ + ŝaf/o - + ŝajn//i - (); (li ŝainas esti malsana - ) + ŝanĝ/i - ; sanĝi monon (ĉe banko) - (..); (la vento ŝanĝis sian direkton) ŝat/i - ; mi ŝatas (volonte) .. - ... + ŝi - ; (ina persono; ununombra virina pronomo de tria persono) ŝip/o - + ŝir/i - + ŝtat/o - ; (presidento - )- (presidanto - ) + + t + + tabl/o - + tag/o - + tamen - + task / o - + teatr/o - + tekst/o - (skribi vortojn); (Vorta konsisto de dokumento, ordinare de skribaĵo;) khudbad, oroh, qowl); (gazeto - ; libro - , ); (gazetoteksto, libroteksto)(skribo - ; skribisto, verkisto - ; skriba - ;); tajpi - fi êrô kõwé; + telefon/o - (-i ) (telefonlibro - ) (poŝtelefono -) + teler/o - + televid/o - , gogaanarag (televid/i - )(televidilo - ) + tem/o - (Tio, pri kio oni parolas, skribas, verkas, pensas;) temp/o - ; ; tempo, epoko -; tempo, epoko - ; tempo, epoko, okazo, ŝanco - ; tempo,okazo, ŝanco - ; tempo, okazo, ŝanco - ; tempo, epoko, periodo - ; tempo, epoko, periodo - ; + ten/i - , (fari paroladon - ) (li faris du paroladojn en la komerca ĉambro); + ter/o - ; () + terur/o - ; (-a; -e) horora, terura, terure - ; + tia - ; (ti- 'indikvorto' - )+ (-a eco - ) + tial - ; (ti- 'indikvorto' - ))+ (-al kialo - ?) + tiam - ; ti- 'indikvorto' - ()+ (-am tempo - ) + tie - (ti- 'indikvorto' - ())+ (e loko - ) + tiel - (); (ti- 'indikvorto' - ())+ (-el maniero - ); (li estas tiel granda, kiel vi - ) + ties, - (ti- 'indikvorto' - ())+ (-es posedanto - )(); "kies panon oni manĝas, ties vorton oni parolas" tim/i - ; tim / o - .. ; (terura, terure, timinda - ); + tio - ; (ti- 'indikvorto' - ())+ (-o nedifinita aĵo - ); tio estas tre facila; tiom - , (ti- 'indikvorto' - ))+ (-om kvanto - ( ?)) (kiom da kapoj, tiom da opinioj) tiu - ; (ti- 'indikvorto' - ))+ (-u individuo, difinita aĵo, - (),); (tiu estas mia amiko;) tra - d + traduk/i - ; traduko, tradukado, tradukaĵo - ; (li tradukis la frazon el la franca lingvo en la internacia lingvo - ;) + trakt/i -(fal); traktado - ; (trakti kun la venkinto pri la paco); (venko - ) + tranĉ/i - , (kudristo, tajloro - ); (tranĉi drapon;)(drapo - );(krioj tranĉis aeron, la noktan silenton;) trans - ( ); (la popoloj loĝantaj trans la maro;) tre - ; (tre granda homo; tre rapide iri; tre laŭte paroli; tre multe da akvo;) + tri - (3) + trink/i - + tro - ; (tro ami ludon; tro da pano;) + trov/i - + tuj - + turn/i - (turni ŝlosilon en la seruro;) + tut / a - g + + u + + u - foriĝu! -!, );(laboru = la ago “labori” estas dezirata, petata, ordonata aŭ celata) + -Uj, (mono - )(sako - ) mono → monujo = saketo por porti monon; teo - , , teo → teujo; + -Ul - (ul/o - ) (persono - ) fremda → fremdulo; (, (; bono, bonulo,) (ulo - ) + -Um, (kovri - sapo - ); sapo → sapumi = kovri per sapo (= sapi); (folio → foliumi = turni la foliojn de libro por legi) universal/a - + universitat/o - ; ( ); (studento -; studado, studio, studo - , ; studi - ; doktoro - ) + unu - kow + urb/o - magaalo, bender + us. (Se mi estus riĉa, mi ne laborus.)(laborus = la ago “labori” estas imagata)(Se mi estus sana, mi estus feliĉa.) util/a - d; utili - ; profito, utilo - ; + uz/i - (uzi multe da salo) v + + vagon/o - layu b- ; vagono - ndaama b-; vagono - oto b-; vagono - saret b-; (Fervojo); Vagono; Vagonaro; Trajno + valor/o - njëg l-; valoro - wuloor b-; Valoro; + varm/a -nugg; varma - taanga; varma - tang; varmigi - jaaru; Varmo; Fiziko + ve - ve!, ve! (lament/i - (kalaame); plend/i - kalaame; plendi- jaambaat); (plendo - ; lamento - ); ve al ni, ni estas ruinigitaj; Ho ve, sinjoro, mia patrino forpelis min el la domo”; ve; VE; Ve; + vend/i - jaay; vendisto - jaaykat b-; vendilo; + + vendred/o - aajuma; vendredo - àjjuma j-; vendredo - gaaw j-; vendredo - Àjjuma; Vendredo; + ven//i - dikka; veni - faxeeku; veni - ñëw; veni - ñów; veni - baayeekoo; veni - jóggee ; (malamiko venis en nian landon); (malamiko - ) (Veniano, komunumo de Italio)) + venk/i - , venko - ndam l-; Venko; + + verk/i - (bind) ; verki libron, operon, raporton; (libro - téere b-;) historio - Taariix; historiolibro - Téere Taariix) historio - démb j-); (Verko; Verkilo; Verkisto; + ver/o - ... ; (ver/a - dégga); (nomo: Vera); Vero; + vesper/o - ; Bonan vesperon! - !(vespermanĝo - reer b ); vespere - ;Vespero + vest/o - ; (robo - ; (kapvesto/ĉapelo - );Vesto; vestajxo - ; Vestajxo; Piedvesto; Subvesto; + + + veter/o - ...; Vetero; + vetur//i - dawal; veturi (per) - ; veturilo - (Veturilo) + vi - ; vi - ; via - ; via - ; (Vi; Via); + viand/o - suux w-; viando - yaapa; viando - yapp w-; viando - yàpp w-; buĉisto - buĉisto; buĉ/i - reendi; buĉi - rey; (virina lango buĉas sen sango);Viando; ; + + vid/i - gis; vidi - gisee; (rigard/i - (gix )); + vilaĝ / o - dëkk b-; vilaĝo - Jolof; Vilagxo; + vintr/o - - ; Vintro + vir/o - Gόor g-; vira - ; virino - Jigéen j-; virino - jabar j-; virnio - jigéen j-; virino - reew j-; (Ino - (Jigéen j-)); virina - ; femala - ; ina - ; viro Gόor; virina (Jigéen j-) + + viv // i - dëkka; vivi - dund; vivo - bakkan b-; vivo - dëkk b-; vivo; + vizit/i - ; vizito - gan b-; viziti la teatron - Haĝo (arabe الحج) ; Haj; Vizito de Maria; + vojaĝ // i - tukki; vojaĝi - xar; vojaĝ / o - tukki b-; (bona vojaĝo -) Vojagxo; Haĝo (arabe الحج) ; Haj; + voj / o - yon b- ; vojo - yon b-; vojo - mbedd m-; vojo - yoon w- ; migra vojo; + vol/i - bëgg; voli - bugga; volo; + vort / o - Vorto + + z + zorg///i .. ; zorgo - ; zorgoj - ..; zorgo - .. ; Zorgado; Zorgo (emocio); + + Xool it + + Alfabeto de Esperanto + + Wikipedia + Bildvortaro - Baatukaay + - Esperanto, a, b, c (gune) + esperanto-afriko.org + esperanto.net Esperanto 62 lingvoj + Esperanto.net , (angle) + - ĉinia radio internacia - esperanta retpaĝo + [http://www.uea.org/vikio/Radikoj-685 "uea-radikoj-685"] + (- reta-vortaro.de - Baatukaay) + "Esperanto"; FUNDAMENTO DE ESPERANTO Antaŭparolo; Gramatiko: GRAMMAIRE (Gramatiko Franca); GRAMMAR ( — Angla); GRAMMATIK ( — Germana); ГРАММАТИКА ( — Rusa); GRAMATYKA ( — Pola);Ekzercaro, Universala Vortaro + Esperanto), PIV Plena Ilustrita Vortaro Eldono 2005 - Baatukaay + + Wikipedia - mapoj /làkk /Lonkoyoon + - Benson-Esperanto-Edmonton + + Wolof: + OSIL Wolof-Dakar + germane-wolof + + Baatukaay: Dictionnaire français-wolof par Mamadou Cissé Dictionnaire français-wolof, 2004-07-01; Langues mondes; Langue d'origine: Français; 389 pages + Wolof für den Senegal. Kauderwelsch-CD, Wolof-Deutsch; CD (August 2006) + Michael Franke Wolof fuer den Senegal Wort fuer Wort Reise Know-How Rump GmbH; Juni 2006 160 Seiten; ISBN 3-89416-280-5; EAN: 9783894162801; Baatukaay: Wolof-Deutsch-Wolof; Wolof-English-Wolof DictionaryWolof-English-Wolof Dictionary Pamela Munro and Dieynaba Gaye, Ay Baati Wolof-A Wolof Dictionary, (revised edition). UCLA Occasional Papers in Linguistics, Number 19. Los Angeles: UCLA Department of Linguistics, 1997. + Wolof (english) + + Baatukaay - Esperanto Kompaktdisko KD - CD + KD Kompaktdisko / CD (ad volumo 56) Esperanto Dahmann / Pusch Eldonejo Peter Rump GmbH D-33649 Bielefeld Reise Know-How Rump GmbH September 2006 - Audio-CD'' ISBN 3-8317-6220-1 EAN: 9783831762200 (www.books.ch) + +Làkk +Hebe Camargo (8 Maars 1929, Taubaté): Breesilian +Wéñumeññet wéñ buy doundé mango +Wéñumeññet xetu wén buy dunde màngo ak yeneen meññet (Tephritidae). Wayé dafa bari aay xét wéñ (Bactrocera invadens, Bactrocera cucurbitae, Ceratitis cosyra, Ceratitis capitata ak yeneen, ak yeneen). Xet wéñ yoyu sow diante thii Afrik la eupéh. Nuñuy rañé méññet bu aam wéñ sii birreum: daay am ay beut-beut yu sèwu yuko weurr. Wéñ yu djigèn yi ñothi bayii sénii doom. Dom yoyu di dundé ñaam bi ci biir,bañu magg. Dirru ay faan, mu nék ay nènn. Nénu yoyu laay domii dundé ci birreum bañu maag, mu soga gènn nékaat aayi wéñ. Digunté ñant ba fukii faan,bu goor bi ak bu djigèn bi andatt. Sénii dundiin nonu lañ kooy diappo. +Digg bu mbëj, mooy barab bees di joóxee kàttanug mbëj. Xeeti digg yu mbëj yi bari nañu te wuute, seenug wuute ngi sukkandiku ci anam gi ñuy soppalee kàttanug doolerandu gi mu doon gu mbëj. Digg yu mbëj yu tay yi, daanaka, dawaanu mbëj gi ñuy jóox gépp gu safaanu la, ci ndimbalu wuutuloxo yu mbëj yees di duppee safaanukaay; bu njëkk ci dawaan bu wéy la daan ame. + +Xeeti digg yi + +Manees naa séddale digg yu mbëj yi ci dayoob seen ngóora, maanaam kemu kàttanug mbëj bi ñu man a jóox. Wàlla itam ci xeetu jafaan bi ñuy jëfandikoo, bu ag coppiteem di xiirtal amug kàttanug mbëj. + +Jóoxug mbëj gu dàttu ci jafaan yees jëlee ci suuf si (petrol,këriñ, gil...) doonul gongikuwaay buy yeeslu ci jamono ji dayoob jafaan yi amee dig, kon bés dina ñëw mu dakk. Ci safaan, manees naa amee kàttan ci gongikuwaay bu wóor te sax-dakk, kàttanug tangoor gees man a amee ci jant bi (kàttanug jant) walla ci ngelaw li (kàttanug ngelaw). + +Manees naa lim xeeti digg yees di jóoxee dawaanu mbëj: +Digg bu ndoxmbëj +Digg bu tangmbëj +Digg bu saal +Digg bu jant +Digg bu leerwolt +Digg bu jurndox + +Lëkkalekaay yu biir +Mbëj +Safaanukaay + +Yeneen sémb +Şalom (de l'hébreu Shalom, ce qui signifie à la fois Bonjour et Paix) est un hebdomadaire juif de Turquie, publié en langue turque avec une page en judéo-espagnol (parfois appelé aussi ladino) depuis le 29 octobre 1947 à Istanbul. Son fondateur a été le journaliste Avram Leyon qui avait travaillé au quotidien +"Cumhuriyet". Son directeur est İvo Molinas. +Son rédacteur en chef est Yakup Barokas. L'hebdomadaire est tiré à 5.000 exemplaires (à la première moitié de l'année 2005) et paraît les mercredis. +Après mars 2005 on lui a attaché un supplément écrit tout entier en judéo-espagnol, "Al Almenser" ("L'Aurore"). + +Autres titres de la presse judéo-espagnole + Aki Yerushalayim, revue culturelle intégralement rédigée en judéo-espagnol. + La Luz de Israel, périodique judéo-espagnol d'Israël. + +Liens externes + Site officiel + Site officiel + +Titre de presse créé en 1947 +Presse écrite hebdomadaire +Presse écrite turque +Presse écrite en turc +Culture judéo-espagnole +São Paulo benn dëkku di Bereesil. Nitñii motnañu 11.244.369 (2010). + +Dëkk +Breesil +Ab duusub sin, ci xayma, melokaanu genn xeetu solo la, di luy jëmmal coppiteeg menn mbir muy dem ci jamono. Mbir mi man naa nekk jenn doole, dawaan walla dendu mbëj, ab duusub mbëjbijjaakon, dees na ko jëfandikoo ci fànn yu bari. + +Màndarga bu ab duusub sin bi gën a fés mooy dayoob feeñte bi nga ciy jëmmal, ci saa-su-ne, soo jëlee ab diir, nga boole leen tus la lay jox. Soo xoolee nataal bi ci wet gi, di nga gis ne ñaari taxawaay yu solos sin bi yi ëpp, dañoo yam dayoo te safaanoo, koon seenug boole tus la. + +Ngir xam dayoo bi ci jenn jamono ji, mii mbindum xayma lees di jëfandikoo. + +Fi: + A, dooneeTaxawaay bi, mooy dayoob solo si bi ëpp. + ω, baraayu puxtal bi, moo nuy wax ni puxtal bi di soppeekoo ci jenn jamono, nu man cee xamee xélam, maanaam ni solo si di soppeekoo ci jamono, bennaanu nattam di radian ci saa (rad/s). + φ wéq, moo nuy wax fi solo si di tambalee fi jamono doonee tus, t = 0, ci ban puxtal la tambalee. + +nattpuxtal +duus +Njeexitu joule mooy tur wees jox feeñte gees di gis saa su dawaanu mbëj jaare cib wommatukaayu mbëj, muy juddug ag tàngoor. Kemu tangoor gee ngi aju ci taraayu dawaan bi. Baat bi jóge ci James Prescott Joule di ab jëmmaan bu waa-angalteer, di ki doon gëstu feeñte gi ci wetu ati 1860. + +Ci xayma manees naa bind lii: + +Fa: +P doonee ngóora gi + +V doonee dend bi +I doonee dawaan bi (di dayoob mbëjfepp yiy jaar ci wommattukaay bi ci saa su nekkk) + +Ci ab dëgërlukaay ngóora gi manees na koo natte niki: + +Fa R doonee ndëgërlu gu ndombo gi. +Feeñte gi li muy jur mooy ñakkug kàttan ci biir wommatukaay, di soppaliku tangoor. Kon xamees na ne doon na mbir mees war a tuutal lunu man, rawatina ci bu ñuy séddale kàttanu mbëj mi. lees man a def ba wàññi ñakkug kàttan googu mooy dijjal wommatukaay bi walla waññi dawaan biy jàll ci biiram. + +Njeexitu joule du fépp la bonee ndax tangoor gi muy jur manees na koo jëfandikoo ci defari puur, ci sunu kër yi, làkkuwaayu mburu yi,... +mbëj +kàttan +Osasco : dëkku Breesil + +Lëkkalekaay yu biir + https://web.archive.org/web/20080530101138/http://www.osascobrazil.com/ + http://www.osasco.sp.gov.br + +Breesil +Mbooleem beeñ bi ak doj yi ñoo sos wàll gu tond (superficiel), gu dëgër gu kol-kolu suuf si, ñu koy woowe Jéeri ji walla aji wow ji. + +Suuf +Concepción dëkku di Sili. Nitñii motnañu 261.061 (2002). + +Sili +Pichilemu dëkku di Sili. Nitñii motnañu 12.392 (2002). + +Sili +Angolemi dëkku di Ciipër. Nitñii motnañu 212 (2006). +Ciipër +Mboolaay baat la bu dage ci "mbooloo", moom nag di ci wu faraas "société" mooy dundiinu mbooloo mi aw nekkiinam tey ag nosteem ak aw nosuwiinam, maanaam ni muy nose biiram ak aw dundiinam ak lëkkaloo gu ay céram (ses membres)akug róofoom. Moom nag dina taxawe baat niki: + + Mboolaay (société):Kureelu mbootaayu xeet yi de, ak li mu def lépp ci liggéey yu jëm ci saxal jàmm ci àdduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci liggéey yu am njariñ ci wàllug mboolaay + +walla aji melal (adjective)niki: + Mboolaay (social):Jataayub koom-koom ak mboolaay +Njéeréer yii, sii toflin gunoor yi dundée ganciax, lanu bokk, bokkat sii toflin Orthoptera, tée nukooy woyé Caelifera. +Ci séen jefiin lan léén di ranée, yii njéeréer yunuy waw locuste bunuy tolo sii grégariaptes (manaam bunuy tolu +ii liime bubaré lunuy woyé grégaire). Ci lanuy nékk gunoor yuy yax gancax. Sii yatu waay yax-yax bunuy déff ci Afrik, yénénn sayi, si boor soow Tugal. Amna tamit,xétu soxunt yuy sen mélocane nuro akk soxunt maag ni aay Criquet pélerin sii bétt Amerique Equatorial, yoo xamantané sénii yax-yax outéna akk njéeréer. + +Sen mélocaan (caractéristiques)(Coppiteg) +Dañi aam ay deg-deg yu gatt té sédéelé ci kaw ba ci suf,sen laaf yu gudu ak yu gaat,té béen bunék,akk façon wayinem.Leg-leg sakh dañléen di diawatlé ak suñu toflin.Dañu rañé ñarr façon njéeréer (Acididae) akk ay njéeréer yu gatt (Tridactilydae). +Ci sen biir xéel,amna ay siditt akk aay siditt ci sen biir yu takliko akk yénéen siditt wayé bu nékk akk sa paco( métamère).Xéel njéeréer ci wéet xoor lañ kooy rañé(hyponeurien).Sen dréet dina daaw béep ci sen yaram,manam ci xool-bi be, ci yénénn siditu yaram-bi,waé tamit, fépp ci ruxu-roxanyi sén yaram. Ngéléw buñuy noyé daay +Monzón ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Ispaañ. + +Mi ngi yaatoo 155,01 km², ci 2010 amoon na 17.115 way dëkk. + +Ispaañ +Laax aw ñam la wees di togge ndox, sunguf su dugubi suuna ci li gën a bari, moo xam sees araw la mbaa muy sanqal, moom nag ci toggi Senegaal yi la bokk, lekk gu yolom lay doon te ndoxe, deesi jaxase kook soow ci li ëpp. +Santiago de los Leones de Caracas mooy péeyu rééwum Benesuwela + +Benesuwela +Péy +Mérida (es. Santiago de los Caballeros de Mérida) béne deukkou Benesuwela. + +Dëkki Benesuwela +Confucius (, or ), literally "Master Kong", (traditionally 28 September 551 BC – 479 BC) was a Chinese thinker and social philosopher of the Spring and Autumn Period. + +The philosophy of Confucius emphasized personal and governmental morality, correctness of social relationships, justice and sincerity. These values gained prominence in China over other doctrines, such as Legalism () or Taoism () during the Han Dynasty (206 BC – AD 220). Confucius' thoughts have been developed into a system of philosophy known as Confucianism (). +Santiago Tequixquiac (es. Santiago Tequixquiax) béne deukkou Meksik. + +Dëkki Meksik +Truong Tan Sang : njiitull Wiyetnaam yi (2011-2016). + +Wiyetnaam +Merkuur mooy jawwu ji gën a jege jant bi te gën a diisadi (woyof) ci jawwu yi nu xam ci nosteg jant bi. Diggam ak jant bi mingi toll ci diggante0,31 ak 0,47 ce benntey saytubiddiw (46 ak 70 miliyo ciy kilomeetar), ëppe sunu jawwu jii di suuf lu ëpp fukki yoon ak ñaar, te gën a kawee lu bari yeneen jawwu yi ci nosteg jant bi. Wareesoon na koo man a gise ak bëtu kese fi sunu jawwu ji waaye wet gi mu féete jant bi (yées 28,3 degre) tax na muy nuur ci biir leeraayu caneeri jant bi. + +Saytubiddiw +Weenus + +Saytubiddiw +Maars + +Saytubiddiw +Yupiter + +Saytubiddiw +Uraanus + +Saytubiddiw +Neptuun + +Saytubiddiw +Pluton (junjyi: wala ) + +Saytubiddiw +Paltoga dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 295 (2002). + +Dëkki Riisi +Tequixquiac (es. Tequixquiac) béne municipality Meksik. + +Meksik +Moshchena dëkk ci Ukreen. Mi ngi yaatoo 1,05 km², ci 2010 amoon na 581 way dëkk. + +Ukreen +Kocc Barma Faal ñu ne it Kocc barma , been kanding la woon, ca senegaal, ci jamono nguuru Kajoor am, ca XVII xarnu. Ci wallu xeltu la daan doxal. + +Cosaanam + +Kocc Barma, been dakkantal ñu ko daan jox la woon. Waaye, Birima Ma Xureja Demba Xole Faal la tuddoon. Xam xam bu mag mu yoroon, ak ndono bu rey li fi bayyi ci Senegaal, ba nit ñepp di ci roy ba leegi ca wa senegaal, moo tax ñu ko tudd tamit sunu maam kocc. Ci askanu FAALEN la bokkoon, nekk been xeet wu rey ca Kajoor, ndax ñoom ñoo nekkoon buur Dammel ca nguuru bobu. Ca jamono joju, Dammel yi, dañu daan noot mbooleem nawlee yi dekk ca reew mi. Di leen buntuxutal, boole ci tekk leen dundu bu meti. Kocc Barma Faal, xeex na ak njabootam, manaam ñoñu daan elif dekk ba, ndax coono ñu daan tekk kaw nit yi bañ am. Moo tax nit yi ñu begg ko, am kollere ci moom, ñu dek ko seen njiit. + +Baayam mooy Ma Xureja Faal Demba Xole, yaayam di Ngene Kewe. Amoon na ay rakk. Ci rakkam nit yi gena xam, am na Maxanta Faal ak Demba Faal ci goor yi, Fayine ak Faatu Faal ci jigeen yi. Ak ñoom la Kocc magee, ci këru FAALEN yi, ca Kajoor. Dammel bi ñu fal ca jamono joju, Dawuur Demba Faal la tuddoon, nekk camminu Kocc Barma Faal. + +Ba mu nekee xale la wajuuram gis naka Kocc Barma meloon ci wallu xam xam ak mandute. Dekkam yepp di gis ci moom nit ku ñepp raññee te ellëg sibir di mujj nekk royukaay bu wor. + +Am na ñu ne tamit, Kocc Barma, tuŋngun la woon, te dafa amoon ñeenti jubb, jubb yu nekk, dencoon been artu walla leeb. Ci ubbite bi, moom ak jabaram kepp ñoo xamoon lan la jubb yi jemmal. + +Ñeenti leeb yi: + + Jigeen soppal waaye bul woolu + Mag, mat na bayyi ci reew + Buur du mbokk + Doomu jiitle du doom + +Leeb yi yepp, ci xeewi Kocc Barma dund la joge, te anam yi ñoo ko faramfacce seen bopp. Am na it yeneeni leeb. Ci yeneeni xeltukat amoon ca jamono joju, am na keen ku tudd Maseeni, ci setu Kocc Barma la bokk, bayyi na fi leeb yu bare tamit, ak Biram Caam Demba koku daan jox wolof yi ay cax walla ay pasin yu bare ñu daan wara xam. Xeltu yepp, ngir yeete nit yi leen ko daan tasaaroo, siiwal. + +Li yepp, ci cosaanu ñu lakk wolof la bokk, ndax ñu ko doxal ci wolof a tax kallamu wolof ak askanu wolof denc lu ko moom ci wallu aada ak cosaan. Cosaanu Senegaal la, ndax wolof, waaso yepp moo ko nos (pel, serer, sarakole, manding...). Cosaanu nit ñu ñuul la, fu ñu mëna nekk ca aduna, ndax ay nitu ñuul ñoo ko moom. Ñu bare, ñakk xam a tax, dañu foog ni, nit ku ñuul, mosul indi dara ci wallu xeltu ca aduna. Waaye, ay gestukat yu mag, mel ni Seex Anta Joob, wonee neen ak ay firnde, mandargal bu wor, gestukat yu gëna mag ci aduna nangu neen ko, ni ay nit ñu ñuul ñoo sos xeltu, ca aduna, ñu ubbite ko ci Sudan ci ay jamono yu yagg, te ñoo ko jox xonk nopp yi, ci nguuru egypt, ci seen jangu yi xonk nopp yi joge nguuru greece daan ñoo ci ay xeltukatu ñuul ngir jangu seen xam xam. Xonk nopp yi sax bind neen ko ci seen téere, mel ni been ci ñoom mu tudd Solon, ñow egypt ngir jang xam xamu nit ñu ñuul ñu fa amoon, ci been xeltukat bu mag ku tudd Sankara (Sankara di nekk sant bu siiw ci sowu afrig, ca manding yi ak pel yi). Def na ñaari fukki ak ñaar at fofu ca egypt ndax lolu. + +Gis tamit + + Xeltu + Wolof +Pachuca de Soto (es. Pachuca de Soto) béne city Meksik. + +Meksik +Lébu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal. Ñoom, Ndakaaru mooy seen dëkk, ñu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur. Ci wetu géej ak tefes. Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan. Seen làkk di wolof. Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi yeneen yi làkk. Am na ñu ne, lébu yi ñoo sos làkk wolof. + +Lebu (baat bi) + +Cosaanu baat boobu, wutte na ci li kilifa yi tekki. Ñooñu deeñi nettali ay cosaan yu wutte: leeb moo juur baat bi. Am na ñeneeni wax luubu mooy bañ, ndax ci cosaan, Lebu yi dañu musa bañ ku leen noot. + +Seex Anta Jóob, ci gestoom, da wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi. +Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga amoon, moo ne woon benn diwaanu, nit ñi di fa dem Rëbbi, ak nappi. Dëkk boobu dafa janno ak geej gi. +Moo tax ñu yoroon Isipt yu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu. Ñu wara xam ni, Seex Anta Joob ak yeneen gestu kat, wone nañu ko, lakk boobu amoon ca Isipt boobu, ak lakk wolof, ñoo bokk maam. Rëbu moo juur Lebu (r-l), Lebu moo juur Libi. Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudd ñu dëkk ca biir reew mi kaw. + +Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir reew mi. + +Cosaan + +Lebu yi, kon, reew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono Isipt gu yagg ga ame. Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñowoon foofu, joge Asi, te ñu leen daan begga noot. Ñoom ñoo Persi yi. + +Ci seen gadday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali). Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawo, ñu ko gëna raññe ci turu Nubi walla Kuus. + +Senegaal, lañu agsi, jamono nguuru Tekuruur ame. Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi. Rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp, ñu leen tudd ci lakku pulaar ay Cuballo / Subalbe. Foof lañu sanc ay dëkk mel ni KasKas ak Njum. + +Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk. Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, sooga mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530. + +Foofu, ay Socé lañu fekk. + +Li ci dess, fi la: Réewi lebu yi. + +Njabootayu Lebu yi + +Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi. Ñu ne tamit, Fukki ak ñaari PENC yi. + +Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi. + +Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun... . + +Sant yi + +Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek. + +Bokk nañu ay sant tamit ak Tukkloor/Pël yi: Mbay, Gey, Ñaŋ, Jaw, Waad, Gay, Joob, Samb, Conŋaan, Baaxum, Jeŋ... . + +Ñu sant Mbeŋ, ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon, seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), juge Mali. + +Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom ñi lañu cosaanoo. Mel ni wolof yi rekk. + +Diine + +Lebu yi, ay jullit lañu. Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay). Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff. + +Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekke Ceddo. Manaam tuur yi. Tuur yi, am na solo ci Lebu yi, ndax ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëme ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan. + +Ci seen tuur yi, ndëpp la nit ñi gëna xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine ñoo tax. Jiine ci Lebu, rab leen ko tudde. + +Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneeni tuur, bokk neen ci ñooñu Lebu yi seqante. + +Xool itam + +Wolof +Pël +Tukkloor +Séeréer +Waasoy Senegaal +Lawbe, benn lang la. Ci xeetu Pël lañu bokk. Li ñu wuute ak yeneen Pël yi, mooy bant bi ñu liggeey. Senegaal ak Mali lañu gëna nekk. + +Lawbe (baat bi) + +Lawbe walla labbo (su de kenn la), ci kallama pulaar la joge. Ci seen lakk, mooy li ñu tudde ruuj ci wolof. + +Am na ay Lawbe ñu leen woo laana/laaɗe, mooy gaal ci wolof. Ndaxte, seen liggeey, mooy tabax ay gaal, ak yeneeni jumtukaay ñu jefandikoo ci wallu ndox mi ak napp gi. Ci wettu dex lañu daan dëkk, ak mool yi (subalɓe ci pulaar). Ku leen jitte, Kalmbaan lañu ko dakkantal. + +Yeneen Lawbe yi, dañu leen tudd gorworo / worworɓe. Ñoom, bant lañu liggeey, waaye deeñi dëkk ci tukki, ngiir jaay li ñu def (leget, gënn, bolde, alluwa...). Ku leen jitte, maalaw mooy dakkantalam. Xam xam yu mat lañu am ci wallu gancax, ba di ci mëna faj. + +Xeetu Lawbe yaatu na. Am na ci ñoom, deeñi woy, ndax dañu daan jegge buur yi. Ñoom ñooy lawbe gumbala wala Kontimpaaji. + +Cosaan + +Pël am nañu benn leeb ngir nettali fan Lawbe yi joge. Dañu ne, bu jëkk, amoon na ñeeti rakk yu goor. Taaw bi, Dikko Hamadi la tuddoon, ku ci topp Samba, cat bi Demba. Ñoom ñepp, sammkat lañu nekkoon. Waaye benn jamono, bekkoor dikk. Dikko Hamadi, mujj bayyi samm, ngir liggeey bant yi, mooy maamu Lawbe yi. Samba moom, wey ci samm bi, mooy maamu Pël yi (pullo / fulbe). Demba, soppeku bambado. + +Lawbe yi nag, ay mbam sëf lañu samm, ndax ci seen cosaan, ak boobu mala lañu daan tukki. Ci ja yi, Lawbe yi ñoo daan jaay bi mala. Ci jamono xare amoon, ay addu-kalpe yu mag lañu nekkoon. + +Lawbe yi, kenn sañoon leen jap ngir def leen lu bon. Ndax dañu gëm ni, ay jig lañu woon, ay nitu karaange. Rawatina seen jigeen, ku daan sey ak Lawbe bu jiggeen, jap ne, karaange la am. + +Sant yi + +Tey, am na ay Lawbe, ci yeneen waaso lañu joge (sooninke...). Moo tax mën nga fekk ay Lawbe ñu yorul ay sant u Pël. + +Lawbe yi bokk ci Pël yi ñooy ñu sant: Sow, Jum, Taal, Wañ... . + +Ay lawbe yu bare, joge ci Sooninke yi, Gaajigo / Gaajaga, Kebe, lañu sant. + +Xool itam + +Pël +Tukkloor +Wolof +Séeréer +Sooninke +Joolaa (askan) +Lebu +Rafael Correa : njiitull Ekwadoor yi (2007-2013). + +Ekwadoor +Baynug + +Cosaan + +Baynug yi dañu bokk ci waaso yu jëkk nekk Kaasamaas aeaaaleen na l, waiayea penku lañu joge. Foofu Kaasamaas,u enn nguur lañu taxawoon,àbu ñu naan Kansaalaa, seen peey di Mampatiŋ. Loolu, ak seeni buur di Gana Sira Bana. Li yépp, ba Imbraatóor gu Mali ame la xewoon. Ba mu yagg, Màndiŋ yi, jóge Mali, ñëw ci ñoom, di leen xeex ngir nangu leen. Ku daan jiite Mandiŋ yi mooy Tiramakan Taraaware. Ba noppi, Mandiŋ yi yilif nañu dëkku Baynug yi ak yeneen xeet ñu fa nekkoon (Joolaa, Pël...), te taxawal seen i nguur ci seen kaw, mooy nguuru Kaabu. Ba loolu xeewe, buuru Baynug yi Kikikor la woon, buur boobu la Tiramakan Taraaware taseel ci xaare. + +Ñooñu daan jiite Màndiŋ yi, Naanco lañu leen tudde ci cosaan. Bi ñu yilifee moomu réew, di réewum baynug yi, dañu a sëy ak ñoom. Moo tax ci seen wallu nday, Naanco yi, ci Baynug walla Joolaa lañu bokk. Li moo tax it, Màndiŋ ak Baynug ak Joolaa yi, ay sant yu bari ñoo ko bokk (Saane, Maane, Jaabi, Jemme, Sambu, Jaata, Saañaa...). Waaye sant bi ñu leen gën a ràññee mooy: Jaandi. Tey sax, Baynuk yi, ñu bari ay Màndiŋ lañu. + +Waaye, loolu yépp, taxul réewum Baynug yi nekk, ba atum 1830 ak 1867, bi ngeen xam ne, seen peey bu ñu naan Birikama tàkk te Kansaala daanu. + +Seen lakk + +Seen lakk, Baynuk la tuddu, te xaj na ci ñaar, am Baynuk Gunyamoolo ak Baynuk Samik. Baynuk yepp, dañu ne, 34 500 lañu. + +Diine + +Baynuk yi, am na ay ceddo ñu nekkoon bu jëkk, am na ay jullit ak ay katolig. + +Xool it + + Joolaa + Séeréer + Lawbe + Lebu + Tukkloor + Pël +Pitax picc la ci néegu Columbidae. + +Picc +Seex Ahmadou Moukhtar ñiou gueen ko Xamé ci Sëñ Afia Mbàaké mogui Fégn Jaamano ci aatou 1871 faa Porokhane +Wadiouram Bou Goor ŋi Toudou Maame Mor Anta Saalli Mbàaké ibn Maame Balla Mbàaké +Wadiouram Bou Jigéen ŋi Maame Aïssatou Mbàaké ñou gueen ko xamé ci tuurou Maame Anta Njaay Mbàaké Bintou Maame Ibrahima Awa Niaŋŋ Ibn Maame Marame + +Raak ñou Goor yi ak ñou Jigéen ñimou Bokaal Wadiour bou Jigéen: + +Sëñ Mbacké Anta +Maame Seex Anta Mbàaké Borom Darû Salam +Soxna Faty Anta Mbàaké,mbii juur Sëñ Mor Faty Touré +Soxna Anta Saali Mbàaké,mbii juur Soxna Faty Mbaàké Soukhraa + +Dooumou Baayam yii: + +Seex Ahmadou Bamba Mbàaké Xadimoul Rassul +Maame Thierno Birahim Mbàaké Borom Darû Moukhti +Sëriñe Massamba Mbàaké +Sëriñe Seex Thioro Mbàaké +Sëriñe Balla Thioro Mbàaké +Seex ABsa Mbàaké +Soxna Rokhaya Mbàaké,mbi juur Sëriñe Balla Bousso +Soxna Astou Mbàaké ,mbi juur Sëriñe Masaayer Sylla +Soxna Khari Mbàaké,mbi juur Sëriñe Modou Bousso Guede +Soxna Coumba Taïba Mbàaké ,mbi juur Sëriñe Haidra +Soxna Aminata Mbàaké,mbi juur Soxna Aminata Lô +Soxna Fati Mbàaké,mbi juur Sëriñe Modou Xabane Mbàaké Dendey + +Wadiouram Bou Goor Sëñ Maame Mor Anta salli mokeu jangal Alxuran ak taalif ñi Sëñ Touba njeuk déf +Diot na Jaar ci Sëñ Mbacké Bousso ngir doléll Jaŋŋam +Sëriñe Touba itamm Jangall nako itam yaarr nako itam + +Sëriñe Ibrahima Mbàaké Ibn Sëñ Mor Dothie néna: + +"Bii Sëñ Maame Mor Anta Salli Watié ligééy,Maagam jii Sëñ Touba mokeu taxawou laata mo déém Gabon.Sëén bii moko wakhone néé na jougé Mbàaké Cadior daldi déém Darû Salam,momit monéko na jangalé Alxuran. +mokalal na ay kilifa ñou beuri ci Yoon wi alxuran meune naniou ci liim ñi Sëriñe Modou Mamoune Mbàaké ak Soxna Maïmounatoul koubra ,Sëriñe Mor fatim Touré. +bii Sëñ bii jougéé Gabon ci aatoum 1912,Sëñ bé ko woloull ngir mou jéégé ko nax néna liggey go giss da wara am céddé."Mounéko def naleu sama céddé ci liggey bi méy défal sunu Borom" Sëriñe Khass mokeu nétali té Sëñ Afia mo koko wax ci bopam. +mogii fék Sëñ bi tokk joublou Khibla daldi néko"nékal Imaam di jiité Diouromi Jouli ñi ,kaadou yoyou nioy ñi moujou jeumeulé ko ci féré yii. + +Meussteu digat waxi Baayam Sëñ Maame Mor anta Salli ak Sëriñam Sëriñe Touba ba nimou fiy jougé wouñou jii Boromam ci aatou 1940. +watioum Ligeeyam Kémaan deug laa nax da Jougé Ndiarém dem séti Maagam jii Mame Seex Anta.bimou eeksé fék Maame Seex ci tawat gou méti ci la daldi wo taawam bi Sëñ Modou Mamoune Mbàaké ak jarbatam Sëriñe Mor Fatim Touré daldi léne waxi Seex Anta da nék ci sukuraat,mou daldi lén waxat né Sëriñe Touba waxone naniko Faatom moy jiitou bou Maame Seex Anta +téyitt Worr nakonii Waxi Sëñ Touba dou raff mouk. +ci laa Egg ci Jouma Jii ngi joulii bamou tolé ci taaya ñgi moujou mou daldi watieu liggey,Sën Mor Touré mo daldi pouss Jeeum Jii yégali Jouli gii. +mou daldi Xibar Faatou Sëñ Afia Imam. +ci aay niit ñou woorr wax naniou né Sëñ bii waxone nako né mou daldi wax beug beugeum,Sëñ Afia daldi néko "moussal maa ci Safara ak saméy Taalibé". + +NB:li nékoul ap Woné Sëñ Afia nax Sunu Borom def nako ba nopi,wayé Beug xamaléé Niitou Yalla bo xamné ñou beuri oumpalé nañiou ko. +Luiz Felipe de Camargo e Almeida Neto (1 agosto 1960, Rio de Janeiro): Breesilian +Laman, walla lamaan, benn tur la, ñu ko daan joxe ñu yorewoon suuf si, ci jamono ju yagg ya, ca Senegaal. + +Cosaanu baat bi + +Taarixkat yi, mel ni Seex Anta Jóob, walla Abubakry Muusa Laam, wone nañu, baat boobu, ci Isipt gu yàgg ga la juge. + +Foofu, baat bi di laman, leppuy jemewoon ci suuf si la tekkiwoon (suuf si ci boppam, walla lu doon jem ci wallu bay). + +Séeréer yi ak Pël yi, ñu xam ne ca dexug Nil la��u cosaano, fu amoon Isipt gu yàgg ga, ñoo indi tur bi di Laman, ca Senegaal. + +Ba ñu agsi Senegaal, ci ñoom, laman moo doonoon ku yore suuf si, buur bi. Li yepp, ba indi LAM bi buur bi takkoon ci loxoom, ngir wone ne, moo moom suuf si. + +Laman yi ca Senegaal + +Nguuru Waalo, Fuuta-Tooro, Jolof, Kajoor, Siin-Saalum, Bawol, foofu yepp, ay Laman moo fa jëkkoon nekk, di yore seen nguur. + +Ca cosaan, dañu fattaliku LAMAN JAW, LAMAN NGOM ak JOLOF MBEŊ ñu nekkon ca Waalo ak Jolof, bokkoon ci Seereer yi ak Pel yi, ñu nekkoon fa ay jamono yu yagg sooga Njaajaan Njaay ñow. + +Ca Kajoor ak Bawol it, dañu fattaliku laman yi fa nekkoon, ñu bokkoon ci njabootayu ñu sant Jaañ ca Kajoor, Juufeen yi ca Bawol (lamanu Bawol di doon Teeñ), sooga Dammel yi ñow, ak PAALEN yi. + +Ci nguuru Fuuta-Tooro, dañu fattaliku LAM-TOORO bu fa nekkoon buur, ca dëkk bu ñu naan TOORO, mu gënoon am dole dëkku Fuuta yepp, ba ñu woowe Fuuta, Fuuta-TOORO. Kooku, ca peey bu tudd GEDE la dëkkoon (wolof yi di woo LAM-TOORO bi BUUR GEDE). Ci ñu sant SAAL la bokkon, bokk ci ururbe yi. LAM ci pulaar, mooy buur (LAMƁE - LAMƊO - LAMIƊO). + +Ba jamono Jolof uuf nguur yi yepp, laman yi nekoon ca nguur yi, dootuñuwoon ay buur, ndax buur-ba Jolof rekk moo nekkon buur (buur fari). Waaye laman yi, dañu mujj nekk ay kanŋam bu mag, ak ay jaambur ju mag, bokk ci xeet yi buur-ba yi juge woon ci seen meen. + +Dëkk yi yepp, ay lamana lañu ko doon seddële, di firnde ni laman yi, dañu wey am doole, ba canc gi ame ak tubaap yi, ci jeexitu fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. +Nha Trang ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 251 km², ci 2010 amoon na 392.244 way dëkk. + +Nha Trang - Wikivoyage + +Wiyetnaam +Yoro Booli Jaw (Yoro Jaw), taarixkat la woon ca cosaanu Senegaal, gane adduna 1847, te dee ca atum 1919. Bokk naa ci ñu jëkk nettali cossanu wolof yi, ci kallamu nasaraan, ca Senegaal. Ci wallu taarix, ci liggeeyam lañu gëna sukkandiku ngir faramfacce cossanu wolof yi. + +Cosaanam + +Yoro Jaw, Waalo la juge woon, juddu ci dëkk bu ñu naan Xuuma, dëkk bi di musa nekk peeyu Waalo. Yoro Jaw, géer la woon, bokk ci xeet yi Brak (buuru Waalo) waroon juge ngir mëna falu. Ñeeti negg ñoo yoroon Waalo, géer yi bokk ci, ci seen meen. Amoon naa Tejeek yi (Yoro Jaw, ci la bokk), ñoom seen maam di ay Pël, amoon naa Joos yi, seen maam di ay Séeréer, ak Loogar yi, seen maam di ay Naar. Ci geñoom, ci ñu sant Jaw la bokkoon, askan woowu baawo ci Jaa Ogo yi. Baayam mooy Fara Penda Majaw Xoor Jaw, yaayam di Booli Mbooj. + +Jaar jaaram + +Bi mu nekke xale, yoobu neen ko ci li ñu wax l'ecole des otages, ci wolof mooy daara ji ñu denc jaam yi. Ndax, boobu jamono, Waalo, tubaap yi ñoo ko nangu woon, ak canc gi. Tubaap yi ñoo daan jël doomi buur yi ñu jaamloo, di leen yobbu ci daara yooyu, ngir xale yi ñu leen jang lakku nasaraan, aaday tubaap yi, ngir xale yi mujj nekk dag tubaap yi. Li yepp xewoon naa ci dundu Yoro Jaw ca Ndar, diggante atum 1856 ak 1860, mu gén ci, ca tegu, tubaap yi teg ko li ñu wax chef de canton ca Waalo, ci dëkk bu tuddu Foos ak Xuuma tamit, ca atum 1860. Yoro Jaw, tubaap yi la daan and ba mujjam. + +Liggeeyam + +Yoro Jaw, yagg naa yengu ci wallu taarix. Bi mu nekke xale, da daan bind cosaanu wolof yi, ci li baayam ko daan nettali, ak ci li gëwël yi daan nettali. Li yepp ba indi bind yu bare mu jagleel cosaanu Waalo, Kajoor, Bawal, ak Jolof. Tubaap yi, dajale bindam yepp, te ñu tambali def ko ci benn teere moniteurs du senegal et dependances, ci atum 1864, ca li Yoro Jaw bindoon ci Kajoor. Henri Gaden, benn tubaap, ca atum 1912, moo genoon yeneeni bindu Yoro Jaw ci yeneen nguur yi, mu tudd ko legendes et coutumes senegalaises. + +Yoro Jaw, jiite naa Seex Anta Joob ci adduna, waaye Yoro Jaw, daan na bind ci fu xeet wi nekk Senegaal juge, di Isipt gu yàgg ga, ay jamono yu yagg sooga Seex Anta Joob gane adduna, te da daan faramfacce li cosaan wax doŋ. Wax naa ci fukk ak benn njabootay juge Isipt, te ñow dëkk Senegaal. Abubacry Muusa Lam, taarixkat ak isiptolog (egyptologue) bu mag nek IFAN, liggeey naa ci seede Yoro Jaw ndax begg tekki li cosaanu rekk wax. Seex Anta Joob sax, musul wax ci Yoro Jaw lenn, mel ni xamul ko woon. + +Yoro Jaw, Xuuma, dëkku cosaanam la gene adduna atum 1919. +Bien Hoa ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 268 km², ci 2011 amoon na 800.000 way dëkk. + +Wiyetnaam +Mustafa Kemal Atatürk » mi ngi juddoo ca Saloniki ci 19 Mee ci atum 1881, génn àdduna ca Istanbul (ca Tirki) ci 10 Nowembar 1938. Nekkoon taalifkat, bindkat doonoon it killifa aada ca Tirki. + +Atatuerk +Atatuerk +Bà Rịa ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 91,5 km², ci 2011 amoon na 224.988 way dëkk. + +Wiyetnaam +Thanh Hoa ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 141 km², ci 2011 amoon na 393.224 way dëkk. + +Wiyetnaam +Phan Thiet ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 206 km², ci 2011 amoon na 350.000 way dëkk. + +Wiyetnaam +Ben Tre ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 67 km², ci 2011 amoon na 116.000 way dëkk. + +Wiyetnaam +Umar Kan (1932-2008) jangalekat la woon ak boroom xam-xam. + +Jaar jaaram + +Kooku, 1932 la gane adduna, ca Kanel, dëkk bu nekk ci tund wu Matam, di jéggé dexug Senegaal. Umar Kan moo doon jiite la Faculté des Lettres et sciences humaines bu daara ju kawe gu Seex Anta Joob bu Dakar. + +Dafa bokkoon ci ñu amoon xam-xam bu gëna mat ci cosaanu nguuru Fuuta Tooro, di dëkk bu am solo ci cosaanu tund wu dexug Senegaal, xam-xam boobu la yoroon tamit ci cosaanu lislaam ca Sowwu Afrig. + +Bind na ay teere yu bare ci tëriit yooyu, rawatina teere bi nit ñi gëna roy ci li muy bind, La première hégémonie peule. Le Fuuta Tooro de Koli Tengella à Almaami Abdul, juge ci benn teereem bu mu bindoon ca uniwersite waaye soppi ko, di woon Le Fuuta Tooro à l'époque almamale. + +Abdulaay Bacily, nekkoon na ndongoom. + +Jangalekat la woon, ci li ñu naan École des Bibliothécaires, archivistes et documentalistes (EBAD). + +Umar Kan, Tukkloor/Pël la woon, te gëstukat ak seetkat bu mag la woon ci lu jëme ci aadaak cosaanu askanu Senegaal. + +Nitu lislaam bu mag la nekkoon, baayam mo ko yaar bu dëgër ci lislaam. Baayam itam a tax mu amoon pasteef bi ci lu jëme ci aaday Pëli / Tukkloor yi. + +Ci atum 2000, gangooru uniwersite bi, magal neen ko ak Mélanges d'archéologie, d'histoire et de littérature offerts au Doyen Oumar Kane, ñu ko doon jagleel. + +Umar Kan, gén na adduna ci weeru rakkaati-gàmmu atum 2008, ca Diiwaan yu Bennoo, fu ñu ko doon faj. +Lamb j am poħum goor la. beneen baatu sexadoom moo di mbëré. poħ mi dafa andak aada akk cosaan, lumelniki ay wayy, fecci, akki deeba deeb, wala book xarfafufa. +Saltige, benn tur la, ci cosaanu Séeréer yi ak Pël, bu ñuy woowee boroom xam xam yi. + +Cosaanu baat bi + +Saltige, ci lakku bambara (bamanakan) la juge. Ci bambara, noonu lañu ko xajalee: + + Sila (mooy yoon wi) + Tigi (mooy njiit bi). + +Kon, Silatigi, ca njeelbeen, mooy kepp kuy jiite yoon wi. + +Saltige Séeréer yi, ak Silatigi bu Fuuta Tooro + +Ci seereer yi, Saltige bi, mooy kuy yoree mbirum xam xam yi. Ñoo yoree mbirum paj ak gisaan, ci askan wi. Gëdd bu mag lañu yoroon, ndax ñoom a tax ñu mënoon wuti safaara ci lu demoon ci wallu bey mi, nawet gi, ak yeneen coono yi askan wi jankoontel. Dañoo dendoon lool nguur gi (Siin-Saalum), buuri seereer yi, di leen yegle ak di leen digal lu bare, ngir buuri yoree nguur gi ci añam yu rafet, reew mi jem kanam te am jamm. Ci seereer yi, nekk Saltige, ndono la. Lebu yi ñu xam ni, seen maam, ay seereer lañu woon ci lu ëpp, ba tey, am nañu tamit seen Saltige, di bokk ci mbootaayu ñooñu nekk ca kaw askanu Lebu, Seriñ Ndakaaru bi moo leen jiite. + +Fuuta-Tooro nag, Silatigi bi, buur la woon, moo doon yoree nguur gi. Deeniyaɲkooɓe yi, giir gu daan jiite reewum Fuuta, ci diggante 1526 ba 1778, seen buur, Silatigi lañu ko daan woowee, wante laata Fuuta-Tooro nekk seeni nguur, buur yi fa nekkoon, yeneen tur lañu amoon. Silatigi boobu, da naroon bokk ci geño Koly Teɲella ku sos giir googu. + +Tey, ci Pël yi, Saltige amaatul. Waaye ci Seereer yi ba tey, Saltige yi ñungi wey li ñu doon def demb, di faj ñooñu febar japp, te ñepp xam neen xeew bi ñu tudd Xoy, ci dëkku Seereer yi, laata nawet gi agsi, Saltige yi ñu def ko ngir yegal askan wi mbaa nawet gi dina neex am det, ak yeneen xibaar bu mëna jëm ci wallu nguur gi, ak yeneen. Bu ñu jeexe li, su de dañoo gis lu bon a bugga ñow ci dëkk, di nañu digal ay saaxaar, nit ñi war ko def, ngir lu bon baña agsi. Ci lebu yi, dañoo yengu ci Ndœp, di ay tuur, ngir faj nit ñi. +Kaabu, benn nguur la woon, ca bëj saalumu Senegaal ak kawu Gine Bisaawóo. Tey, + ak li. + +Cosaan + +Nguur gi, ñi ko taxawal, soose yi la. + +Sunjata Keyta, jamono bi mu nekkoon buur bu jiite imbraatoor gu Mali (Manden), cosaan ne na, ki nekkon ci jalu Jolof, tooñ na ko. + +Li mu ko tooñee tax, Sunjata Keyta buggoon mbugël buur ba Jolof bi. + +Kon, Sunjata Keyta wotee xarekatam, ngir ñu dem Jolof, xeex ak buur bi fa ne. + +Ku doon jiite xarekatam, benn dagu Sunjata la woon, bu ñu naan Tiramakan Tarawale. . + +Ba ñu agsee Jolof, xeex neen ak wa Jolof, waaye ba noppi, dellusiwuñu Mali. + +Ñu fa wacc nag, fekk fa ay soose ñu fa ne woon. Soose yi ñu fekk foofu, ñoom, dañu fa dëkkoon bu yag a yag sooga Tiramakan Tarawale ñow, waaye ñoom . + +Kon Tiramakan Tarawale, dajale na soose yi yepp ne woon foofu, elif leen. + +Waaye nag, ca bëj saalum, amoon na Baynuk yi ak Joolaa yi. Dañu fa amoon seeni nguur. Ñu sant Saane, Maane, Saaña, ak yeneen, ñoo doon yoree nguuri Baynuk ak Joola yi. Seen peey, di woon Mampatiŋ. + +Tiramakan Tarawale, buuri Baynuk ak Joolaa yi, dañoo mujj seyante. Li moo jur li ñi wax Nancoo yi. Nancoo yi tabax nguuru Kaabu, ca jeexitu XIII xarnu. + +Seeni mbootaayug + + + +Jiggeenu Fariŋ bi ñu leen wo Musu-Mansa. Meeni Fariŋ bi waroon juge ngir mëna falu, ñoom la. + +Ñoom leen ne . + +Suuf si + +Kaabu, xajoon na ci fukk ak ñaar diiwaan. Ñooy: + +Jimara, Sama, Paccana, Sankolla, Kantoora, Mana, Bajar, Tumaana, Caaña, Pakis, Kolla, Propana. + +Peeyug Kaabu, Kansala, la woon. Di bu , am. + +Mujjam + +Kaabu mujj na daan ndax Pël yi. Ca XIX xarnu, Pël yi nekkoon Kaabu, Nancoo yi dañu leen daan noot. Foofu, Pël yi dañoo yagoon soon ak Nancoo yi ñu leen daan soonal, ba ca njëlbeen. Kon Pël yi (ñu dëkkon Kaabu ci ay Fulakunda), ñoo woolu seeni benn mbokk. Ki, maamam ay soose lañu woon (sant Dumbuya). Alfa Molo Balde, ak Almaami yi bu Fuuta Jallon, and nañu, xeex ak Nancoo yi, ba daan leen. +sididi xassaide la bo khamni serigne touba mo ka binde komme ni niou kay wakhee khassidatou sididi +Oblaznytsia dëkk ci Ukreen. Mi ngi yaatoo 1,412 km², ci 2001 amoon na 288 way dëkk. + +Lëkkalekaay yu biti + + Облазниця на сайті Верховної Ради України + Погода в селі Облазниця + Obłaźnica w Słowniku geograficznym Królestwa Polskiego i innych krajów słowiańskich, Tom VII (Netrebka – Perepiat) z 1886 r. + +Ukreen +Taís Bianca Gama de Araújo Ramos (25 November 1978, Rio de Janeiro): Breesilian +Krushynka dëkk ci Ukreen. Mi ngi yaatoo 2,16 km², ci 2001 amoon na 347 way dëkk. + +Lëkkalekaay yu biti + + Крушинка на сайті Верховної Ради України + Погода в селі Крушинка + село Крушинка (сайт Української конфедерації журналістів). + БІЛОЦЕРКІВСЬКА ДОРОГА + +gallery + +Ukreen +Nicete Xavier Miessa (7 January 1933, Niterói – 20 Disambar 2020, Rio de Janeiro): Breesilian +Niccolò Cusano University - Unicusano ab university Rom, Itaali. + +Itaali +Vesoul mooy péeyu rééwum Franche-Comté (Faraas). Nitñii motnañu 15.920 (2009). + +Dëkki Faraas +Ekontiŋ bi ("akonting" ci angale walla "ekonting" ci franse), xalam la ci cosaanu Joola. Am na ñetti nas te yaramam mooy kalabas bu nu taqe deru bëy. Baatam dafa gudd ak xat. Baat bi mooy banjul. Bépp nas dafa wute guddaay: bu gudd, bu yem, ak bu gàtt. Nas ñi ñooy caas. Tëgg na nasu gudd ak baaraamu joxoñ ci loxo ndeyjóór. Tëgg na nasi yem ak gàtt ak baaraamu déy ci loxo ndeyjóór. Ekontiŋ dafa yam bucundu (ci cosaanu Manjago), busunde (ci cosaanu Papel), ak kisinta (ci cosaanu Balanta). Mel na xalam (ci cosaanu Wolof) ak ngoni (ci cosaanu Mandinka). Banjo bi ci cosaanu Amerik la mel itam. + +Xeetu Jola jòge na Kasamans, ci bët Saalumu Senegaal. Am na niti Jola yu bari ci Dakar ak Gambi itam, rawatina ci bët Saalumu ci dex bi Gambi. Niti Jola ñooy beykati ceeb ak nappkat. Dañu def sëng itam. Am na Gurmet yu bari ak Julit yu tuuti ci cosaanu Jola, ak boroomi xërëm itam. Cosaanu Jola dafa "acephalous" (duñuy am benn boroom rekk) te duñuy am geer, ñeeño, ak jam. Ñëp mooy ci mbiru muy. Duñuy am géwél itam; ñëp mën na tëgg sabar, manaam ekontiŋ. + +Ekontiŋ lanuy tëgg pur xewi Jola. Tëgg nanu ko lool ci ngénté ak takk. Tëggkatu, ekontiŋ bi dina woy itam. Beneen musikkat tëgg na sabar bu mag. Bugarab la tudd. Wëyi Jola dañu "sumé" (dañu neex) te am nañu tuuti baat. Seeni waxin wax nañu ci wallu xol, waakër, ligééy, yité, ak àdduna ci àll. + +Benn ndaanaanu Jola, Daniel Laemouahuma Jatta la tudd. Mandinari ci Gambi la jòge. Tëgg na ekontiŋ bu baax, te xam na lool ci wallu cosaanu Jola. Mag mat naa bàyyi cib dëkk. Keneen tëggkatu ekontiŋ, Sana Ndiaye la tudd. Kasamans la jòge, waaye New York la dëkk. Moom, tëgg na ekontiŋ ci gàddu "rap." Gokh Bi System lañu tudd. Ekontiŋ bi amul tànk, waaye jàll nam ndox. +Queen bi angale rock buum. + +Freddie Mercury +Brian May +Roger Taylor +John Deacon + +Woy +Coreca (Coraca ci waxiinu waa-coreca), ab frazione la (dëkk-dëkkaan ci wolof) bu bokk ci dëkkaanu Amantea, ci tunduw Cosenza digoo ak dëkk-dëkkaanu Campora San Giovanni ca réewum Itaali. + +Itaali +Ba Đồn ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Wiyetnaam. + +Mi ngi yaatoo 163,1828 km², ci 2013 amoon na 121.988 way dëkk. + +Wiyetnaam +Siligo ca réewum Itaali. + +Itaali +The Doors bi Diiwaan yu Bennoo rock buum. + +Jim Morrison +Ray Manzarek +Robby Krieger +John Densmore + +Woy +ANA LAN MOOY MOOM SA BOPPU? +Li as cëslaay buma bëgga seddoo ak aji jàng ji fi ci Jàngu bi saytu Kalaama Wolof (Akaademi Wolof). Ci sama biir waxtaan ak sama amdi-jam yi ma neka ndool, ken si gnoom dafa fa sulli yoon waxtaan bu ajju ci moomsa-bopp (liberte). Loolu mooma jox yëg-yëgu bind wax ji. Bi ëmbitu xalaat (concept): “moomsa-boppu” dafa lëntt, rax ci dolli neexuta tënkk ci anam yu léer, yu mucci ci wérenté. Waaye, manees na jappu ne, moom sa bopp mooy « meum-meum ak sagn-sagnu tànn wala bagna tànn ». wante nit ki du mana aag ci lii fileeg amul momeel bu matalè ci yaramam ak xellam. So gnu beggee léeral wax ji, nanu addu ne, moom sa boppu dafa lallu ci gniati kènu : tolloo (egalite), garange (securite), ak meunal sa boppu (independance). +Ci biir seetlu, xell du mana nangu am moomeel ci sa bopp bu amul sakett, manam yamukaay. Ndax domu adam du mala. Liko waral mooy dagnuko mognaleeg xell, ta iittam dafay dundu ci biir askan, ay moromu nittam weur ko. Kon sagn-sagnam ak meum-meumam fok mu tëslaayo, weeru ci ay terälin yuy taxawal ak di gindi doxalinu askan wi. Kon wax jooju Descartes di gissee moomsaboppu « kantan nuk jef ak bagna jef » dafa tenkku ci doxalinu ak teralinu askan wi emb doomu adam ci beppu jamano, beppu bërëp, ak beppu aal. +Sugnu suka dinkko ci cëslaay wi, dana gnu mana jàppu ne, ta di ci andak borom xam-xam bugn naan Emmanuel Kant, moom sa bopp man firndeel ni nit ki amna sagn-sagn ak meum-meum ci tan luko neex mu def ko, wax ko, wala mu bayi ko, ci kaw muy samu teralinu askan wamu nekk ak li xellu domu adam mana nangu. Been fànn buy dëgëral moom sa bopp mooy askan yi tamit sammu ngor ak yeleefu nit ki. Ndax ak lu nit jeema tënku si doxalinu askanam, bu feekine, gna ŋankk nguurug askan wa deloo wugnu buum sa boy-boy ba, kon moom sa boppu doo tul mana yémbbu. +Aw askan su bäggee sammu momeel gi nit gni moom seen boppu, fok mu yamale leen (Egalite), ak tamit samu seen ngor, aar seen alall ci biir ak ci biti (Securite). Ta ku toogn, yoon dal ci aji toognakoon ba, jox ndampaay kignu toogn (Justice). Dènccu kaayu alallu baytimaal dafa yell mu nek ci anam yu mucci ayib ta sell (Trésor public). Faj aji feebar yii, aji tayàtt yi, jàng gum ndaw gni, ak ndimbal ci neew ji doole, alall jooju lees war di jafandikoo ngir faj ajooy ak soxla askan wi. Kon moom sa boppu du ma am su fekkeeni, ax ak yeleefu gniko mbootayo samugn ko. +Jamanoy tay nak, baatub “moom sa boppu” ay mbootaay ak ay nit yu beru dagn koy faral di jibbal ci pencci yi ngir di laaj loo xamne doxalinu ak teralinu reew ma andu ci. Dafa war gnu xajjale, moom sa boppu ak asaaro (libertinage). Reew moo gis dafa am aada ak cosaan yuy birndeel gis-gisu nit yako don nu. Jégaani ay doxalin man waral wuute ak jamaar loo ci nu gnu wara firee moom sa boppu. Gnun waa senegaal, sugnuy aada dafa dugalanteek dine lislaam. Jàngu tubaab bi tamit amna ci wall ci sugnu doxalin. Wayee xeltu bima si am mooy, leppu lu ligni eppu ci askan wi gis ne dëppoo wulag adaa ak dine ak feggu (morale), warta tax gnu nasaxal sakett wi ëmbb sugnuy baax (valeurs). +Moom sa boppu yamul rek ci nit ki, wayee dafa wara yaatu ba lambaale reew mi yeppu. Reew mu moom boppam nak dafa laaj ay mbir yu takku. Bokku na ci li si eppu solo, bagna weeru ci keneen, wala beneen reew. karaangee, coobare, ak kantanug dundal sa gnos bokku na ci liy dëgëral momeel gi am reew wara moom boppam. Waye bu fekeene, sa dundu, sa karaange, say jumtuwaay, sa xarele, ak mboleem xam-xam yu aju si nekine ak doxalinu dëkk bi dagn lakoy sâh, bu boo ba, ca moom sa boppu des na lu bari. Reew mu melni taxawayam du dëgër. Ndax kersam dagn kako yoral. Buko noonam bëgee buntu xatal dafay yombu. Ndax bugn ko dundalul mu fandè. +Ngir sunu reew moom boppam, foku njiit yi farlu, am fayda, ngir mana gnaax nit gni gnu jôk liggeeyi, bayyi, jàngi, sammi. Ku si nek ak wett wa nga feete, nga wane ci sa yiite ju matt, ci kaw njup ak jubale. Werente ak dagasante munta gnak, wantè dafa war neew. Nit gni da ngo wara dëppoo, ànd ligeey. Su lii amee, andaari kom-kom yi dana gnu fees, nantagee sawaan bawaan, jammu law. Talàll gafaka di yalwaan dina dakk, buumi njaam dina feccee ku, jantub yokkute fenk ci beppu diiwan. Su booba, gaindeeg senegaal dina daagu ci manding ngu am-am, andak jòm, fit, ak jambaar. +Jamma ngen fitna +Bis boobu, ci njël la jok, dèm ci wanag wa, raggu. Ginaaw loolu, ma dèm jappu ba sètt, juli, jal sama kuruus, doxontu walee ba ca tunduwa, ndax daagub suba day fuddu tank. Kerook, guddi googu, taw bu barri mo soteeku si dëkk bi. Ma ngi fateliku, bi marax di jot, ap jabbu bu am doole doona melax ci bëtt ganaar. Dëgg la sax de, xiin ño ngiko baaxó giss si penkku bi. Ba bi ñuy fàtu, xiin wa saaxé gul woon. Bi ma leemo ba tëdd daal, la degg peppu ndox di tëgg xeddu neeg bi, mbete ay gewāl yuy sajji lambu. Ci kaw loolu la for bëtt bani gis, aw dännu wu rey buy xoti asamán mooma yee waat. Dëkk bani selaw. Dara yanguwul, nga xamni yalla rekk moo am doole, kuy jaay doole, kuy jaay ngoora, akk nguur, ba dajje ak Boroom bi, danga xamni, nguur ken’ako moom tamuy Yalla, keppu kum ko jox, war nga séed suba, yaræm jaamam yi. Loolu motax wolof njaay naan, nguur kenn duko gnèd. Bi ma walbatikoo, ba foraat bett, ci la daadi song ap nelaw badi aji xôôt. Nees tuuti, ci ay smili yu neew, samäy gët ubee ku si manding bu yaatu, bu nurook geej. Ben picci bu weex tal nãw tiim ma, mu daldi sap, ginaw loolu, mu bayi ben bataaxal bu ñu bind si aw keyit, ci lu toloog juroomi xët. Tamba leeko si mbëbestal la bacci daneel ba. Si la dox ay jeego wut si bataaxal bi, ma for ko, janggu ko. “assalamu alayi kum ya SENEGAAL. Ma ngi leen di nuyu, ken kunekk si turam ak santam. Di leen xamal ni, weer wi niu degmal, ayi jotaayu xecco ak taneef ku jiite gox yo ak gox goxaat yi. Ma dileen wax ni, rewmi di senegaal, ben bop la, ta ken duko xar niaar. Jamm moo njek, ta itamit jamm mooy mujju. Kaddu yi maleen di beral si bataaxal bi, kaddu yu weex xat la, waaye garab du neex, rawatina garab guy aar. Fagaru moo ngan fajju, te itt, xodiku bala nga lak le. Bu degloo lifi xacco katu nguur yi di wax si seeni lamiñ, dafa melni dañuy ma solal yerre yu aji raglu. Ak koj goo mandi bayou, sa wax si jamano bi rewmi tollu dafa wara lamboo jamm. Ndax nak, fitna day nelew, ta keppu kuko yee du moy walis yeekat ba. Ta fitna, xaritu alcande la, yoon wumu jar, booyal toolu boroom, boyal taw feexu askanam. Ta moom safaraam ayib la, ayib bu jaffe fay. Dëkku yi ak xuloo yi xotinañ lambaayu siki saka. Ken xamatul fumuy dägmal, ni wara addu, waxuñ, sen lamiñ la ñu yeew ak buumu xális. Ndaw ñi gälëm nañ, seen yaakar naax say na, seen rangooñ dil wal ci seen xarkanam ya di aji raag ngir yaram talu. Ay waay, yeen way politiseŋ, baayi leen xel badoola yi ak baÿkat yi, ay waay jox leen gëdd fac kat bi, jàng kat bi, ndax ňii ňooy reeni kom kom. Kuleen tuutal, nasaxal nga elagu reewmi. Bi leem reew, da niu ko sëff lumu atannul, ñaata ndawu reew, ñaata, kaŋ kam, ñaata, pencci ak bärëb yuy warax alallu baytimál. Tabe ci alall jó moom. Li fum ñu jëmmé, yeen doomi rewmi. Sama yaram dawna, sama xóll di jooy ci diggu all badi aji liw. Ngir Yallah, saaŋ leen ma si mbalaan num yermande, lii de kuko déf, wasaaré nga ngelawal wërsek ak peppu xeewal si ëttub senegaal. Safaanu lii, musiba la, jikatu fitna, dawal katu mbaamu coono , mbate ay saafa’ndoo yu raag yuy naan si ndox mu nëx. Waaru na si kooku kiy wuuti niit ñi, di leek seen alal yum tooggé si kawdiru yaq ak jalgati, nuluge ko deretu mbaam xuux. Ku def li wor na, ku def lii du gor, tooke lay sap melni janaab badi aji marr +Doole doole mani +Amina yaax nako +Doole doole mani +Kay waay doole doole +Mani amina yaax nako +Maam khar suul na ba deem +Mane sini ray na waaja +Doole doole mani +Doole doole mani +Amina yaax nako +Mame khar suul na ba dem +Mani kaay waay doole doole +Mani sini ray na waaja +Aaya karka yimbe +Aaya karka muñal +Mbaa demo geej karka yimbe +Sa baay booy def raw na ba dem +Sa yaay booy jef na ba dem +Mbaale karka muñal +Radio Studio 54 Network beg istasiony rajo Itaali, nëkk dëkk Locri Calabria. + +Lëkkalekaay yu biti + + Site Web de Studio 54 Network + Web streaming Radio Studio 54 Network + +Station Rajo Itaali +Rajo +Locri (Locri ci waxiinu waa-locri), ab dëkkaanu, ci tunduw Reggio Calabria digoo ak dëkkaanu Gerace ca réewum Itaali. + +Itaali +Trojany ab dëkku-kaw la ca Poloñ. Mi ngi ne ci diggante Wołomin ak Warsaw, ci wetu Dąbrówka. + +Mi ngi ci 2014 amoon na 490 way dëkk. + +Poloñ +Anna Rita del Piano(Cassano delle Murge, 26 sulet 1966) woy ju Itaali. + +Njàngat +Woy +Itaali +Benedicta Boccoli(Milano, 11 Nowembar 1966) woy ju Itaali. + +Njàngat +Woy +Itaali +Bochotnica ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Poloñ. Mi ngi ne ci diggante Puławy ak Lublino, ci wetu Opole Lubelskie, ci dexu Bystra. + +Mi ngi yaatoo 20 km², ci 2010 amoon na 1.500 way dëkk. + +Poloñ +Budka Suflera bi Poloñ rock buum. + +Krzysztof Cugowski +Romuald Lipko +Tomasz Zeliszewski +Łukasz Pilch +Mirosław Stępień + +Woy +Poloñ +Jàngoroy Ebola ñu gënoon koo xamee ci Jàngoroy yaram-wu-tàng ju Ebola jenn xeetu jangoro la juy dal nit walla yenn bàyyima yi te doomu-jàngoro bu ebola di ko joxe. Xàmmeekaayu jangoro ji mi ngi tàmbalee feeñ ci diggante ñaari fan ba ñetti ayubés ginnaaw bi la doomu-jàngoro bi duggee, ngay ame yaram-wu-tàng, put guy metti, sidit yuy metti ak bopp buy metti. Ginnaw feeñte yu njëkk yii, naka-jekk, yi ciy topp ñooy, xel-muy-teey, waccu ak biir-buy-daw. Su ñu àggee fii ci jàngoro ji, ñenn nit ñi dañuy tàmbalee am ay nàcc-nàcc yu man a nekk ci biir yaram wi walla ci biti. Repp gee dee ci nit ñi ko amee dina àgg ci dayoo bu réy. + +Jàngoro ji manees na koo jël ci boo laalee dereet walla wal-walaan yu yaramu ab bàyyima (golo walla njugup) walla nit ñu ko am. Ba tay jii jàppees na ne maneesul a wàllante jàngoro ji jaare ko ci ngelaw li ci ab barab. + +Ginnaaw bi ko kenn nit jële, jàngoro ji man naa tas jaare ci moom. Ñi ko ame ba wér ci man nañoo wéy di ko man a wàllaate ñaari weer ginnaaw seenug wér jaare ko c seen manniwa. + +Amagul genn xeetu pac gu wór gees xam ngir fac njangoroy Ebola. Xeetug pac gi gën a jàppandi ci jamono jii mooy di leen jeem a naanloo ndox mu doy (di ndox mu am tuuti suukar ak xorom) walla ñu leen di sol ay wal-walaan. Jàngoro ji ju man a rayaate la, lu ci ëpp ci 50% (juroom-fukk ci téeméer) ba 70% (juroom-ñeent-fukk ci téeméer) ci ñi muy dal ci dee lañuy mujjee. Jangoroy yaram-wu-tàng ju Ebola ñoo ngi ko njëkkeen gis ca Sudaan ak ca Kongóo. Naka-jekk njàngoro ji dafa daan faral di yem rek ci yenn barab yu ndaw yu beru ci yenn réewi Afrig yu ron-sahara yi. Ci atum 1976 (di at mi ñu ko njëkkee gis) ba 2013, lu néew 1 000 nit ci at mu nekk daan nañ ko jël. Wàllante gi gën a réy gu Ebola moo ngi ame ci ndoorteelu 2014 te barab yi mu gën a tasee ñooy réew yu Gine, Siraa Leyoon, Libeeria a Niseeria. Ci oktoobar 2014 jappees na ne lu mat 10 000 nit jot nañu koo am. + +Lëkkalekaay yu biti + Ebola Virus Haemorrhagic Fever - Proceedings of an International Colloquium on Ebola Virus Infection and Other Haemorrhagic Fevers held in Antwerp, Belgium, 6-8 December, 1977 + Questions and Answers about Ebola Hemorrhagic Fever - Center for Disease Control (CDC), retrieved 10 July 2006 + www.healthocrates.com - Articolo sulla febbre emorragica dell'Ebola + +Ebola +Niseeriya dees ko wax itam Repiblik federal bu Niseeriya am réew la mu nekk ci Sowwu Afrig. Afrique du Sud: manifestation xénophobe devant l'ambassade du Nigeria à Pretoria. + +Réew +Afrig +Sowwu Afrig +Taariix +Duran Duran nak ci angale new wave buum. + Simon Le Bon + John Taylor + Nick Rhodes + Andy Taylor + Roger Andrew Taylor +Woy +Ronald Wilson Reagan (1911-2004): njiitull Diiwaan yu Bennoo yi (1981-1989). + +Diiwaan yu Bennoo +RMF FM beg istasiony rajo Poloñ, nëkk dëkk Kraków. + +Lëkkalekaay yu biti + + Site Web de RMF FM + +Station Rajo Poloñ +Rajo +Mindelo benn diiwaan ci yu bëj-gannar-sowwu yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Melosuuf +Alto Mira +Bela Vista +Bom Sossego +Centro +Chã de Alecrim +Fonte Cônego +Lazareto +Madeira (Ilha da Madeira) +Passarão +Ribeira Bote + +Waax +Waax bu Porto Grande (''Porto Grande') + +Iniweersitee +Iniweersite Kap Weer - Mindelo (Liceu Velho) +Jean Piaget Iniweersite Kap Weer - Mindelo +Iniweersite Mindelo + +Sport + +Football clubi +Académica +Batuque FC +GS Castilho +FC Derby +Falcōes do Norte +CS Mindelense +Sporting Farense + +Staad +Staad Adérito Sena + +Dayi +Bana +Bau +Hermínia da Cruz Fortes +B. Leza (Francisco Xavier da Cruz) +Humberto Duarte Fonseca +Cesária Évora +Sérgio Ferreira +Aguinaldo Fonseca +Corsino Fortes +Sergio Frusoni +António Aurélio Gonçalves +João Cleofas Martins +Georgina Mello +Luís de Montalvor +Luís Ramos Morais +Yolanda Morazzo +Tito Paris +Erin Pinheiro +Rambé +Onésimo Silveira +Ovídio de Sousa Martins +Fredson (Fredson Tavares), +Carlos Veiga +Lela Violão (Manuel Tomás da Cruz) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.mindelo.cv +Mindelo Infos + +Dëkki Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Ci angale mooy Corinth; Ci faranse mooy Corinthe + +Korent benn diiwaan ci yu Girees. + +Nataal yi + +Xool it +Dóox gu Korent +Korenti (Korinthia) + +Dayo +Tarazimaak (angale: Thrasymachus, faranse: Thrasymaque) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +https://web.archive.org/web/20121111223328/http://www.corinth.gr/ +http://www.korinthia.gr + +Dëkk +Girees +Arara : dëkku Breesil + +Breesil +Łobez ab dëkku-kaw la ca bëj-saalum-penkug Poloñ. +Mi ngi yaatoo 12,8 km², ci 2019 amoon na 10.066 way dëkk. + +Way-dëkk + +Lëkkalekaay yu biti + www.lobez.pl + BIP Łobez + Łobez - You Tube + + Poloñ +Santiag mooy péeyu rééwum Sili. + +Ciili +Epatit A (ñu gënoon ko xamee ci turu epatit biy dale) doon na Jàngoro juy dale ju tar buy jàpp res wi te li koy joxe di doomu jàngoro biñ naan Epatit A (HAV). Bari na lu muy dal nit te du feeñ rawatina ci ndaw yi. Diggante bi muy dugg sa yaram ak bi muy tàmbalee feeñ, mi ngi tollu ci diggante ñaar ba juróom-benni ayi-bis. Su la dalee mën na def ak yaw juróom ñatti ayi-bis te dina faral di ànd ak: xel muy teey, waccu, biir buy daw, der bu mboq, yaram wu tàng, ak mettitu biir. Luy tollu ci 10 ba 15% ci ñi mu dal ñooy wéy di ko gis su demee ba weesu juróom-benni weer ginaaw bi mu leen dalee. Mag ñi mën nañu ci jëlee Feebaru res bu tar waaye bariwul lu muy dale. + +Li koy faral di joxe mooy lekk ñam wala naan ndox mu am doomi jàngoro. Meññeefu géej buñ toggul ba mu ñor dina ko faral di joxe. Jege ku ko am lu ëpp, mën na la ko wàll. Xale yi mën nañu ko am te du feeñ waaye teewul mën nañu ko wàll ñeneen. Su la dalee benn yoon, dootu la dalati sa giir gi dund. Ci sa deret la ñuy seetee doomu jàngoro ci ndax ni muy feeñee dafa nuru ak yu yeneen jàngoro yu bari. Benn xeetu epatit la ci juróom yiñ xam: A, B, C, D, ak E. + +ñaqu epatit A dalay aar bu baax ci feebar bi. Yenn réew dañuy faral di baamtu ñaq bi ci xale bi ak ci ñi feebar bi gën a yab kenn masu leen a ñaq. Loolu mën na leen aar seen giir gi dund. Yeneen matuwaayu yi la ci mën a musal ñooy raxas loxo ak togg ñam ba bu ñor xomm. Amul benn garab buñ ni mën na ko faj, li ci des, garabi xel muy teey wala biir buy daw la ñu lay digal su aajewoo. Gën gaa bari su la dalee dangay wér, sa res wi melni dara mësu ko dal. Bu yàqee res wi, dañu lay gereefeel res ngir faj ko. + +Ci àdduna bi, jàngoro bi dina feeñ ci 1.5 miliyo?i doomu aadama at mu nekk nga boole ci yi feeñul mu tollu ci fukki miliyo?. Fi mu gënee bari àdduna bi mooy ci gox yi desee te ndox mi ñuy naan setul. Ci réew yi néew doole lu tollu ci 90% ciy xale jot nañu am doomu jàngoro bi laata ñuy am 10 at, loolu mooy mucci nañu ci ba fàww laata ñuy nekk mak. Yenn saay mu jàppandoo ñu bari ci réew yi xawa am doole ndox jàngoro bi bariwul ci xale yi te itam duñu leen di faral di ñaq. Ci atum 2010, epatit A bu tar bi faat 102,000 doomu aadama. At mu nekk 28 fan ci weeru Sulet mooy Bis biñ Jagleel epatit ngir xamal nit ñi luy jàngoroy epatit. + +Royuwaay yi +Espargos benn diiwaan ci yu dunu Sal, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi +Académico do Aeroporto +Académica do Sal +Juventude + +Staad +Staad Marcelo Leitão + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.espargos.cv + +Sal (Kap Weert) +Dëkki Kap Weer +Xiibon wala xale bu xiibon mu ngi bawoo ci lekk loo xam ni amul wala bariwul ay ferñent wala ñu bari ci bay indi loraange ci wérgi-yaramu nit ki. Mbir yiñ mën a woowe ferñent ñooy: kalori yi, proteyin, karbo-idrate yi, witaamin wala ndox miy suuxat sa yarams. Loolu lañuy faral di woowee lekk gu doyul nga xamni ay kaloreem ak proteyinam duñu doy ferñent yu ndaw yi; waaye, dafa ànd itam ak ferñeent yu ëpp. Sudee nit ki amul lekk gu doy ci diirub ëmb bi wala laata muy am ñaari at, loolu mën na ko jural jafe-jafey xel ak ñàkk a mag. Ñàkk a lekk gu tar, ñu koy woowe xiif bu tar, mën na indi jafe-jafe yu ci melni: gàttaay, sewaay, tàyyel, tànk ak biir buy newwi. Dina am itam tawat gu leen di faral di jural soj. Ni ñàkkug ferñent di faral di feeñee ngi aju ci ferñent yu ndaw yiñ ñàkk. + +Liy faral di indi xiibon mooy ñàkk a am lekk gu baax te doy gu jàppandi. Li mën a waral mooy dund gu seer dóol. Ñàkk a nàmp weenu nday mën nako waral, mën a waral itam feebaru jàngoro yu ci melni: gastroenteritis, pnëmoni, sibbiru ak ŋas yiy tax sa yaram di gën a soxla ferñent. Ñaari xeeti xiibon ñoo am: xiibonu ñàkk proteyin-cawarte ak ñàkk lekk gu baax. Xiibonu ñàkk proteyin-cawarte ñaari xeet yu metti la am: marasm (ñàkkug proteyin ak kalori) ak kwasiorkor (ñàkkug proteyin kese). Yenn ferñent yu ndaw yi nit ki mën a ñàkk ñooy: ñàkk feer bu doy, ñàkkug iyod ak ñàkkug Witaamin A. Ku nekk jigéenu wérul, sa yaram dafay soxla mbir yu bari, loolooy waral sa yaram di ñàkk yenn yi. Ci yenn réew yi néew doole lekk gu ëpp pataa mingi fi tàmbalee bari ni ki nifi xiibon gi baree. Yeneen mbir yi mën a waral xiibon ñooy baña lekk ndax ragala am yaram ak opeere ngir wàññi yaram. Sudee ci mag ñi yi mën a waral seen xiibon ñooy ni seen yaram bindoo, xel mu ñàkk a dal ak jafe-jafey àdduna. + +Jéego yi ñuy def ngir yokk ferñent yi bokk nañu ci mbir yi gën a am solo ci ndimbalum yokkute. Nàmpalee ween mën na musal xale yi ci xiibon ak gaaw a faatu, te jéego yiñ def ci wàll woowu wane nañu seen njariñ. Di jox xale bi muy lekk ak di nàmpaale ba mu am ñaari at, dina tax sa xaalis du jeex ci njëndum garab. Ñépp itam gis nañu njariñ li ci jox ferñenti mottali di ay xeeti witamin yu ñuy jox jigéeni wérul yi ak xale yu ndaw yi ci réew yu néew doole yi. Niñu gën a mën a dimbalee nit ñi soxla luñu dundee dëgg, mooy nga jox leen lu ñuy lekk waaye itam joxaale leen xaalis ngir ñu mën koo jëndee ca seenub marse. Di jox xale liñuy lekk ci daara ja rekk du doy. Toppatoo xale bu xiibon bi ci kër ga mu dëkk ready-to-use therapeutic foods lu mën a nekk la. Ñi nga xam ni xiibon gi daleen sonal loolu ba indil leen yeneen jafe-jafe ci seen wérgi-yaram, dañu leen wara yóbbu lopitaal ñu faj leen. Yi ñu ciy gën a faral di faj mooy yaram wu ñàkk suukër, tàngooru yaram, yaram wu ñàkk ndox, ak diko jox mu lekk ni mu waree. Di faral di ko jox ay antibiotik lu baax la ci musal ko ci yenn doomu jàngoro yi. Ndimbal li gën am solo tey yàgg: mooy gën a dooleel mbay mi, xeex ndóol, defar wanag yu baax, ak jàppale jigéen ñi ci liggéey. + +Ci atum 2010 xayma woon nañu lu tollu ci 925 miliyoŋi doomi aadama yu xiibon, muy of 80 miliyoŋ yu yokk ci limu 1990. Ak ñeneen ñu tollu ci benn miliyaar ñuñ xayma ni amuñu witamin ak lu suuxat seen yaram. Ci atum 2010 ñàkkug proteyin, cawarte jur na lu tollu ci 600,000 bakkan yu faatu, doon lim bu wàññiku buñu seetee ci 883,000 bakkan yi faatu ci 1990. Yeneen ñàkkug ferñent yu ci melni ñàkkug iod ak ñàkkug feer, jur na lu tollu ci 84,000 bakkan yu faatu. Ci 2010 xayma nañu ni xiibon moo waral 1.4% ci mbooleem ati ñàkk a mënal sa bopp yi nit di dund. Jàpp nañu benn xale ci ñatt yu faatu yu nekk, xiibon a ko ray; waaye, nit ñi duñu faral di nangu ni looloo ko waral. Ci 2010 jàpp nañu ni bokk na ci li faat lu tolloo ak 1.5 miliyoŋ ciy jiggéey ak xale teewul ba tay am na ñu jàpp ni lim bi ëpp na 3 miliyoŋ. Ak yeneen 165 miliyoŋi xale yu mënatul màgg ndax feebar boobu. Xiibon gaa ngi gën a baree ci réew yu néew doole yi. + +Royuwaay yi +Biir bu daw wala Jaare mooy ngay dem wanag gën gaa néew ñatti yoon ci bis te li ngay génne ginaaw kër yi dafay ndoxe. Yenn saa mu jàpp la ay fan, te loolu mën na tax sa yaram ñàkk ndox. Su yaramu nit ñàkkee ndox deram dootul nooy te it mën a soppiku. Mën nga dem ba dootoo saw lu bari, sab der furi, sa xol di tëf-tëfi, te sam xel dootul dox ni mu waree wala say jëf yeex, su demee ba gën a tar. Ginaaw kër yu tooy te bañ a ndoxe mën dal liir yiy nàmp, waaye, loolu du dara. + +Li koy gën a faral di joxe mooy jàngoro yiy jàpp butit yi te di bawoo ci ab wiris, bakteri, parasit, wala feebar bu ñuy woowe gastroenteritis. Yooyu jàngoroo ngi faral di bawoo ci ndox wala ñam wu am doomu jàngoro ji, wala ku am jàngoro ji wàll la ko. Mën nañu ni ñàtti xeeti biir bu daw ñoo am: biir bu daw bu yàggul, biir bu daw bu ànd deret bu yàggul, ak biy weesoo ñaari ayi-bis, muy biir bu daw bu yàgg. Biir bu daw bu yàggul te ndoxe mën na nekk kolera. Su àndee ak deret, ñu gën ko xame ci disànteri. Amna yeneen mbir yu wuute ak jàngoro yu mën a joxe biir bu daw, muy lu ci melni: Ipertiroyidism, biir buy bañ soow, feebaru biir buy metti, yenn xeeti garab yi, ak sendoromu biir buy metti ak yeneen mbir. Yi gën bari ci ñoom soxlawu ñu ñuy amal njàngat mu xóot ngir xam li leen waral. + +Liy musalaate ci biir bu daw mooy cet, di naan ndox mu sell, ak raxas loxo. Nàmpal liir ba juróom benni weer gën gaa néew lañu digle ak ñaq biy aare ci rotawiris. Pajtalu naan ndox muy faj (ORS), manaam ndox mu sell muñ boole ak tuuti xorom ak suukër, kumu neex nga fajoo ko. kumu neex itam nga jëfandikoo doomi Zinc. Xayma nañu ni garab yooyu muccal nañu 50 miliyoŋi xale ci 25 at yii weesu. Taamu nañu ci ku am biir buy daw mu wéy di lekk ñam wu sell, sudee liir ñu wéy di ko nàmpal. Soo amul foo jëndee ORS (ndox muñ jaxase ak xorom ak suukër), mën nga koo defaral sa bopp. Sudee nit ki daa ñàkk ndox mu bari, war nañu ko mën a sampal buteel. Lu ci gën bari; naan ndox mu bari mën na ko saafara. Antibiotik, suñu ko jëfandikoowul lu bari, dina ciy faral di baax ci ñi am biir buy daw ànd ak deret ak yaram wu tàng lool, ak ñiy am biir buy daw bu ñu tukkee, ak ñi am yenn jàngoro yi ci seen biir. Loperamide mën na wàññi jaabante bi ci wanag wi waaye kenn digalu ko ñi seen biir bu daw tar lool. + +At mu nekk dina am lu tollu ci 1.7 ba 5 miliyaar ciy biir yuy daw. Fi mu gënee bari mooy ci réew yu néew doole yi, nga xam ni xale bu nekk biiram dina daw ci xayma ñatti yoon ci at mi. Ci àdduna bi yépp, ci atum 2012, mooy ñaareelu jàngoro juy faat xale yi yi amagul juróomi at (0.76 miliyoŋ wala 11%). Biir bu daw bu bari mooy faral di indi xiibon te itam mooy li ko gën a faral di joxe ci xale yi amagul juróomi at. Su yàggee mën na jur jafe-jafe yu ci melni ñàkk kàrtan wala xel mu neex. + +Royuwaay yi +Sibbiru ab feebar bu yoo di joxe di dal nit ak yenn rab yi te li koy joxe di parasit protozoan (benn xeetu selil microorganism) bu xeetu Plasmodium. Ni sibbiru di faral di feeñee mooy yaram wu tàng, coono, waccu ak metitu bopp. Su demee ba tar mën na jur der bu mboq, say, komaa wala faatu. Feebar baa ngi tàmbalee feeñ fukki fan ak juróom ginaaw bu la yoo bi màttee. Ñi mu dal te faju ñu ko bu baax, mën na leen dalaat ginaaw ay weer ci kanam. Ñi mu dal bu yàggul ba ñu mucci, su leen dalaatee du metti noonu. muslaay boobu nit ki am dafay jeex su amee ay weer wala at sudee newul fu mu mën a amee sibbiru. + +Gis nañu ni, màtt-màttu yoo bu jigéen bi tuddu Anophele mooy joxe feebar bi. Sula màttee dafay dugal parasit yi nekk ci tiflitam ci sa deret. Ginaaw loolu mu jàll ci res wi ndax foofu lay màggee ak juree. Juróomi xeeti Plasmodium a mën a dal nit te ñooy la nit mën a wàlle. Ñu bari ñu sibbiru di faat P. falciparum ak P. vivax, P. ovaleñoo leen faat, ak P. malariae biy joxe sibbiru bu tarul lool. Xeet yi tudd P. knowlesi bariwul lu ñuy daaneel nit. Bu ñuy seet ndax danga sibbiru jël ci sa laamu deret xool ko ci mikroskop, wala ñu jëfandikoo test bi tuddu antigen-based test bu gaaw la. Defar nañu jumtukaay buy jëfandikoo polymerase chain reaction ngir gis ADN bu doomu jàngoro ji, waaye loolu bariwul ci barab yi sibbiru bari ndax dafa seer te jafe. + +Sibbiru bu mën na wàññiku bu baax sudee nit ñaa ngi jëfandikoo sàñce (mustikeer) wala diw bu dàq yoo ngir moytu màtt-mattu yoo yi, wala def lu leen di dàq wala ray, lu ci melni pompu yoo ak dindi dox yi taa. Bari na garab yu ci melni prevent malaria yiñ jagleel ñiy tukki ci barab yu sibbiru bi tasaaroo. Yenn saa mën nañu bindal xale sulfadoxine/pyrimethamine xale ak jiggéenu wérul ci ñatti weer yi njëkk cib ëmb bi ci barab yi sibbiru bari lool. Fiñu tollu amagul ñakk bu ci mën a aar ni naam soxla nañu ko, teewul nit ñaa ngi ciy gëstu bu baax ngir am ko. Ñaari xeeti garab yi ñu digle ngir faj feebar bi ñooy garab yiy xeex sibbiru bi amaale ab artemisinin. Ñaareelu garab gi mën na doon mefloquine, lumefantrine, wala sulfadoxine/pyrimethamine. Mën nañu itam jël Quinine boole ko ak doxycycline sudee artemisinin amul. Mooy lañuy digle ci barab yi feebar bi bari, dañu wara xam bu baax ndax nit ki dafa sibbiru laata muy jël garab yi ndax dañuy bañ jàngoro ji dërkiis ci garab gi. Jangoro dem na ba dërkiis ci yenn xeetu garab yu daan faj sibbiru; lu ci melni, dërkiis ci-chloroquine P. falciparum barina ci barab yi sibbiru bi bari, te itam dërkiisam ci artemisinin doon na jafe-jafe bu mag ci réew Asi Gànjoolu-penku. + +Fi feebar bi gënee bari mooy ci réew yu tàng yi ak xawa tàng te ñooy yi séq rëdd wiy xaajale suuf si di ekuwaatër. Bokk na ci ñoom Afrigu Suufu-Sahara, Asi, ak Amerik Latin. Mbootaayu Wérgi-yaramu Àdduna bi maanaam OMS xayma na ci atum 2012, ni amoon na 207 miliyoŋi ñu amoon sibbiru. Ci at moomu, feebar bi fatna lu tollu ci diggante 473,000 ak 789,000 doomu aadama, li ëpp ci ñoom doon ay gunéy Afrik. Fuñu tuddee sibbiru xel yi dem ci ndóol te loolu doonul lu baax ci koom-koom guy suqaliku. Xayma nañu ni at mu nekk sibbiru dina ñàkkloo Afrik lu tollu ci $12 miliyaar ciy dolaar ndax pajum feebar bi, ñàkk a mën a liggéey ak li muy yàq turism bi. + +Royuwaay yi +Maad a Sinig Ama Juuf Njeelane Faye Juuf buur la won ca Siin (1825 - 1853). Mamaam ya Seereer lenge woon ak Gelwaar. "Maad a Sinig" moy "Buur Siin" ci làkki Seereer. Ama Juuf nak kerr Semu Njeke la joge ca waali Njuufeen. + +Xool it +Siin +Saalum +Seereer +Juuf + +Cosaan +Niti senegaal +Niti Gàmbi +Taariixu senegaal +Cosaan Séeréer + Séeréer +Taariixu Gàmbi +Angela Cavagna (Genova, 6 suwe 1966) woy ju Itaali. + +Njàngat +Woy +Itaali +Santiago diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkkaani +Praia +Ribeira Grande de Santiago +Santa Catarina +Santa Cruz +São Domingos +São Lourenço dos Órgãos +São Miguel +São Salvador do Mundo +Tarrafal + +Dëkki +Praia +Assomada +Calheta de São Miguel +Cidade Velha (Ribeira Grande do Santiago) +Pedra Badejo +São Domingos +Tarrafal + +Dëkk-Dëkkaani + +Achada Baixo +Achada Baleia +Achada Biscainho +Achada Falcão +Achada Fazenda +Achada Lem +Achada Longueira +Achada Loura +Arribada +Banana (Wolof: Banaana) +Boa Entrada +Gil Bispo +Calabaceira +Chaminé +Chão Bom +Chão de Tanque +Dacabalaio +Espinho Branco +Faveta +Figueira das Naus +Fonteana +Fonte Lima +Fundura +Lagoa +Longueira +Mancholi +Mato Raia +Massapé +Milho Branco +Moia Moia +Nora +Ôrgãos +Pilao Cão de São Miguel +Picos (Achada Igreja) +Poilão +Ponta Verde +Portal +Porto Gouveia +Porto Mosquito +Porto Rincão +(Ribeira) Principal +Ribeira da Barca +Ribeira da Prata +Ribeirão Chiquinho +Salineiro +Vila Sambaia +Santa Ana +São Francisco +São Jorge dos Órgãos +São Lourenço do Santiago +São Miguel +São Pedro da Calheta +Serra da Malagueta (Serra) +João Teves +Rui Vaz +Xexé (Sheshe) + +Sport +Football: +1. Liig - Santiago gu bëj-gannar +1. Liig - Santiago gu bëj-saluumu + +Staad +Staad 25 samwiyee - Pedra Badejo +Staad Calheta - Calheta de São Miguel +Staad Cumbém - Assomada +Staad Mangi - Tarrafal +Staad Várzea - Praia + +Dayo +André Álvares de Almada +Ivan Almeida +Jorge Barbosa +Gardénia Benrós +António Lopes Cardoso +José Ulisses Correia e Silva +Codé di Dona +Mito Elias +Silvino Lopes Évora +Dário Furtado +Suzanna Lubrano +António Mascarenhas Monteiro +Jose Maria Neves +Orlando Pantera +António Pedro +Fernando Quejas +Simplício Rodrigues de Sá +Tcheka +Izé Teixeira +Toni Varela +Manuel Veiga +Arménio Vieira +Lela Violão + +Iniweersite +Iniweersite Kap Weert +Jean Piaget Iniweersite Kap Weert +Iniweersite Assomada +Iniweersite Santiago + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.santiago.cv + + +Duni Kap Weer +Ab duus wala wanag mooy xeetu wanag wi nit ñi di bàyyi seeni ginaaw kër ci pax muñ gas ci suuf. Duus yooyu duñu soxla sotti ndox wala duñu soxla ludul benn ba ñatti liitaru ndox ngir jàllale neefere yi. Sudee niñu ko tabaxee baax na, ñu koy toppatoo bu baax, mën na tax ba yenn feebar yiy bawoo ci neeferey nit nefere yi ci mbedd mi wàññiku bu baax. Dina wàññi li weñ yi di jëlee ciy doomu-jàngoro yiy bawoo ci neefere di leen yóbbu ci lekk yi. Yooyu doomu-jàngoro ñooy gën a faral di indi feebaru biir bu daw ak feebaru saan. Feebaru biir bu daw faat na lu tollu ci 0.7 miliyoŋ ciy xale yu amagul juróomi at ci atum 2011 ak 250 miliyoŋ ciy fan yuñ jàngul. Xeetu duus yooyu ñoo gën a yomb ngir tàxale nit ñi ak seeni ginaaw kër. + +Booy tabax xeetu duus boobu war nga def ñatti mbir: gas am pax, wut kubéer gooy teg ci kawam te wutal ko bën-bën bu xawa yaatu, ak mbañ gàcce. Pax mi war na am gën gaa néew 3 meetar (10 feet) ci xóotaay ak 1 m (3.2 feet) ci jameetar. OMS (Mbootaay Wérgi-yaram ci Àdduna bi xelal na nit ñi, ñu tabax duus fu soriwul lool waye itam fu jegewul lool bay sonal nit ñi ak xet gu bon. ndox mi ci biir suuf ak ndox mi ci kaw suuf luñu gën sorante gën a baax suku defee benn du laal moroom ma. Bën-bën bi ci kubéer gi itam warul am lu ëpp 25 sàntimeetar (9.8 inches)ci jameetar ngir moytu xale yi di ci daanu. Waru ñu ko bàyyi muy leer ndax loolu mën na indi weñ yi. Soo ko bëggee def dangay wut kubéer guy tëj pax mi su kenn nekkul ci duus bi. Sudee duus bi demee ba tollu ci 0.5 meetar (1.6 feet) ngir mu fees, dañu ko wara ŋàcci wala ñu taxab duus bu bees, daaldi ciy toxal mbañ gàcce gi wala tabax bu bees. ŋacci neefere yi ci foos lu jafe la. Mën na indi ay jafe-jafe ci seeni dëkkuwaay ak ci seen wérgi-yaram. + +Ginaaw buñ tabaxee duus bi, mën nañu ci yokk yeneen mbir ngir gën ko baaxal. Mën nañu yokk ab tiyo ci kaw dal bi. Dina tax ngelaw li mën a jàll boole ci di wàññi xet gu bon gi. Dina tax itam weñ yi wàññiku suñu muurée boppu tiyo bi ak sagar bu yaraax (ñu bari di faral di jëfandikoo mustikeer). Xeetu duus yooyu dañu wara am kubéer gu koy tëj ci suuf. Ngir mu gën a dëgër itam mën nañu tabax dal bi ba ndox mi yépp di dug ci pax mi ba noppi wërale dal bi ak ay birik ak simaa ndax mu gën a taxaw. + +Ci atum 2013 xayma nañu lu tollu ci 1.77 miliyaar ciy nit ñuy jëfandikoo yooyu xeetu duus. Lim baa ngi ëppee ci réew yu néew doole yi ak ñi dëkk ci kaw ga ak ci àll bi. Ci atum 2011 lu tollu 2.5 miliyaar ciy doomu aadama amu ñu duus bu baax ak benn miliyaar ciy doomu aadama yu dem wanag ci seen wetu kër. Asia gu Gànjool ak Afriku suufi Sahara ñoo gën a bonle ay duus ci àdduna bi. Defarug duus ci réew yu néew doole yi dafay laaj luy tollu ci diggante 25 ak 60 USD. Njëgu toppatoo gi ci at mu nekk, tollu na ci diggante 1.5 ak 4 USD nit ku nekk waaye duñu ci bàyyi xel. Ci yen dëkku kaw yi ci réewum End am na kàmpaañ bu tudd "No Toilet, No Bride" (Ku amul duus, du am jabar) buñ fa amal ngir duus yi gën a bari, seenum pexe mooy ñaax jigéen ñi ñu bañ a sëy ak góor gu mënul am duus ci këram. + +Royuwaay yi +São Vicente diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Melosuuf +Fateixa +Flamengos +Monte Calhau +Monte Cara +Monte Passarão +Monte Verde +Monte Viana +Ponta João do Evora +Praia de Salamansa (Tefesu Salamansa) +Ribeira do Calhau + +Dëkki +Mindelo + +Dëkk-dëkkaani +Baía das Gatas +Calhau +Lameirão +Madeiral +Ribeira de Julião +Ribeira de Vinha +Salamansa +São Pedro + +Dayi + +Alexandre Alhinho +Carlos Alhinho +Leonel Almeida +Dudu Araujo +Bana +Bau +B. Leza +Valter Borges +Bela Duarte +Dulce Almada Duarte +Cesária Évora +Fantcha +Sérgio Ferreira +Corsino Fortes +Sergio Frusoni +João Cleofas Martins +Vasco Martins +Georgina Mello +Luís de Montalvor +Luís Ramos Morais +Yolanda Morazzo +Tito Paris +Erin Pinheiro +Rambé +Onésimo Silveira +Ovídio de Sousa Martins +Fredson (Fredson Tavares), +Carlos Veiga +Lela Violão (Manuel Tomás da Cruz) + +Waax +Porto Grande + +Iniweersite +Iniweersite Kap Weer - São Vicente kaampus + +Sport + +Football clubi +Académica Mindelo +GD Amarantes +Batuque FC (Batuki) +GS Castilho +FC Derby +CS Mindelense + +Staad +Staad Adérito Sena + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.saovicente.cv + + +Duni Kap Weer +Sudaan gu Bëj-saalum (Republik bu Suudaangu Bëj-saalum) : réewu Afrig. + +Réew +Afrig +Fanny Cadeo (Lavagna, 11 Satumbar 1970) woy ju Itaali. + +Njàngat +Woy +Itaali +Barbara Chiappini (Piacenza, 2 Nowembar 1974) woy ju Itaali. + +Njàngat +Woy +Itaali +' Iniwersite Gaston Berger mooy Daara ju kawe ji nekk diwaanu Ndar ci réewum Senegaal. + +Démb +Léewópóol Sedaar Seŋoor moo amal tegum xeer bu jënk ci wàllum taxawaay iniwersite wi ci 14 sãwiye 1975. + +Taxawaayam mu ngi aju ci sart bu 2 sãwiye 1990, iniwersite wu Ndar mu ngi teeru limu ndongo wu njënk (600)ci 17 Desàmbar 1990 ci yoonu négandi. + +Mu ngi jot gëddam ci ndogalu bu 10 sulet 1996 ak tur bu bees jóge ci ndogalu bu 4 desàmbar 1996. + +Ku ñu ko duppe Gaston Berger, nekk na ab kàngam ci wàllum xeltu, di doomu Senegaal ak Farãs, juddo Ndar-Géej. Di baayu Maurice Béjart. + +Ràññeefi barab + +Diggànte iniwersite ak Ndar toll na ci fukki (10) km. Boo jóge Risaartool jëmsi Ndar di nga séen wërngalu kàggu gu mag bi. +Iniwersite dafa fekk boole ñaari dëkk : Sanaar Pël ak Sanaar Wolof. Loolu tax na ndongo yi di ko woowe yenn saay Sanaar. Itam kërub internetu ndogo daara yi« http://www.Sunusanar.com » la ñu ko tudde. + +Bërëbu tàggat ak gëstu +Iniwersite bu Ndar ëmb na juróorum-ñaari Bërëbu tàggat ak gëstu :  + + Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama + Xam-xamu jëmale ak xarala + Xam-xamu yoon ak politig + Xam-xamu koom-koom ak + Xam-xamu wérgu-yaram + Xam-xamu mbay, sàmm, nàpp ak xarala yu màcc ci wàllum dund + Caada, diine, taaral ak jokkoo + Diiru njàng mi di na toll ci fukki weer. Di tàmbalee oktoobar jàpp sulet. Waaye ubbite njagale mi ak njeextal mi ngi aju ci barabu tàggat ak gëstu bu nekk. + +Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama +Barabu tàggat ak gëstu ci ladab ak xam-xamu nekkinu doomu aadama ëmb juróomu bàqasu: + Angale, + Farãse + Làkk nasaraan jëmale, + Xam-xamu melosuuf, + Xam-xamu nekkinu àskan yi. + +Xam-xamu jëmale ak xarala + + Barabu tàggat ak gëstu ci xam-xam jëmale ak xaraala ëmb na bàqasu xayma jëmale, bànqaas informatig, bànqaas bitil jëmale ak tàggat ci wàllum xéy. + +Mën a dugg + +Bànqaasu xayma jëmale + +Bànqaasu bitil jëmale + +Bànqaasu informatig + +Xam-xamu yoon ak politig + +Barabu tàggat ak gëstu xam-xamu yoon ak politik ëmb na ñett bàqaas: + Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi ; + Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris ; + Bànqaasu xam-xamu politig. + +Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi + +Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris + +bànqaasu xam-xamu politig + +Mën a dugg + +Xam-xamu koom-koom ak doxalin +Kërug internet + +Caada, diine, taaral ak jokkoo +Kërug internet +Barabu tàggat ak gëstu caada, diine, taaral, ak jokkoo ëmb na juróom benn bàqasu : + Bànqaasu jokkoo, + bànqaasu infogarafi, + Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada, + Bànqaasu làkk ak caada Agrig, + Bànqaasu mënloo aju ci bokk moomel, + Bànqaasu Xam-xamu diine. + +bànqaasu jokkoo + +Mën a dugg + +tërëlin + +Mujjàntal + +Bànqaasu infogarafi + +Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada + +Mujjàntal + +Mën a dugg + +Bànqaasu làkk ak caaday Afrig + +Mujjàntal + +Màndargal + +Mën a dugg + +Wàllum gëstu + +nekkinu ndongo daara yi (CROUS) + +yokkute lim ndongo yi +thumb|350px|Évolution des effectifs de l'UGB entre 2001 et 2007 + +Dëkkuwaay + +Dem beek dikk bi + +Tektal yi + +Xool yeneen + +Téere ak mbóotu tektal + Dossier sur l'UGB dans un numéro spécial sur l'enseignement supérieur au Sénégal, Le Soleil, janvier 2008, 5-6 + +Cosaan + https://web.archive.org/web/20121110200513/http://www.gouv.sn/Decret-no-2012-1163-du-29-octobre.html + +mbóotu tektal + Musée du Centre de Recherches et de Documentation du Sénégal à Saint-Louis + Université Cheikh-Anta-Diop + Éducation au Sénégal + Felwine Sarr + +mbóotu biti + + Site officiel + Présentation et images sur le site du Campus numérique francophone de Saint-Louis + Site des étudiants de Sanar + Fiche de l'UGB sur le portail SenCampus + [https ://fr.glosbe.com] + +Université sénégalaise +Saint-Louis (Sénégal) + +' Iniwersite Gaston Berger mooy Daara ju kawe ji nekk diwaanu Ndar ci réewum Senegaal. + +Démb +Léewópóol Sedaar Seŋoor moo amal tegum xeer bu jënk ci wàllum taxawaay iniwersite wi ci 14 sãwiye 1975. + +Taxawaayam mu ngi aju ci sart bu 2 sãwiye 1990, iniwersite wu Ndar mu ngi teeru limu ndongo wu njënk (600)ci 17 Desàmbar 1990 ci yoonu négandi. + +Mu ngi jot gëddam ci ndogalu bu 10 sulet 1996 ak tur bu bees jóge ci ndogalu bu 4 desàmbar 1996. + +Ku ñu ko duppe Gaston Berger, nekk na ab kàngam ci wàllum xeltu, di doomu Senegaal ak Farãs, juddo Ndar-Géej. Di baayu Maurice Béjart. + +Ràññeefi barab + +Diggànte iniwersite ak Ndar toll na ci fukki (10) km. Boo jóge Risaartool jëmsi Ndar di nga séen wërngalu kàggu gu mag bi. +Iniwersite dafa fekk boole ñaari dëkk : Sanaar Pël ak Sanaar Wolof. Loolu tax na ndongo yi di ko woowe yenn saay Sanaar. Itam kërub internetu ndogo daara yi« http://www.Sunusanar.com » la ñu ko tudde. + +Bërëbu tàggat ak gëstu +Iniwersite bu Ndar ëmb na juróorum-ñaari Bërëbu tàggat ak gëstu : + + Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama + Xam-xamu jëmale ak xarala + Xam-xamu yoon ak politig + Xam-xamu koom-koom ak + Xam-xamu wérgu-yaram + Xam-xamu mbay, sàmm, nàpp ak xarala yu màcc ci wàllum dund + Caada, diine, taaral ak jokkoo + Diiru njàng mi di na toll ci fukki weer. Di tàmbalee oktoobar jàpp sulet. Waaye ubbite njagale mi ak njeextal mi ngi aju ci barabu tàggat ak gëstu bu nekk. + +Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama +Barabu tàggat ak gëstu ci ladab ak xam-xamu nekkinu doomu aadama ëmb juróomu bàqasu: + Angale, + Farãse + Làkk nasaraan jëmale, + Xam-xamu melosuuf, + Xam-xamu nekkinu àskan yi. + +Xam-xamu jëmale ak xarala + + Barabu tàggat ak gëstu ci xam-xam jëmale ak xaraala ëmb na bàqasu xayma jëmale, bànqaas informatig, bànqaas bitil jëmale ak tàggat ci wàllum xéy. + +Mën a dugg + +Bànqaasu xayma jëmale + +Bànqaasu bitil jëmale + +Bànqaasu informatig + +Xam-xamu yoon ak politig + +Barabu tàggat ak gëstu xam-xamu yoon ak politik ëmb na ñett bàqaas: + Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi ; + Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris ; + Bànqaasu xam-xamu politig. + +Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi + +Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris + +bànqaasu xam-xamu politig + +Mën a dugg + +Xam-xamu koom-koom ak doxalin +Kërug internet + +Caada, diine, taaral ak jokkoo +Kërug internet +Barabu tàggat ak gëstu caada, diine, taaral, ak jokkoo ëmb na juróom benn bàqasu : + Bànqaasu jokkoo, + bànqaasu infogarafi, + Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada, + Bànqaasu làkk ak caaday Afrig, + Bànqaasu mënloo aju ci bokk moomel, + Bànqaasu Xam-xamu diine. + +bànqaasu jokkoo + +Mën a dugg + +tërëlin + +Mujjàntal + +Bànqaasu infogarafi + +Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada + +Mujjàntal + +Mën a dugg + +Bànqaasu làkk ak caaday Afrig + +Mujjàntal + +Màndargal + +Mën a dugg + +Wàllum gëstu + +nekkinu ndongo daara yi (CROUS) + +yokkute lim ndongo yi +thumb|350px|Évolution des effectifs de l'UGB entre 2001 et 2007 + +Dëkkuwaay + +Dem beek dikk bi + +Tektal yi + +Xool yeneen + +Téere ak mbóotu tektal + Dossier sur l'UGB dans un numéro spécial sur l'enseignement supérieur au Sénégal, Le Soleil, janvier 2008, 5-6 + +Cosaan + https://web.archive.org/web/20121110200513/http://www.gouv.sn/Decret-no-2012-1163-du-29-octobre.html + +mbóotu tektal + Musée du Centre de Recherches et de Documentation du Sénégal à Saint-Louis + Université Cheikh-Anta-Diop + Éducation au Sénégal + Felwine Sarr + +mbóotu biti + + Site officiel + Présentation et images sur le site du Campus numérique francophone de Saint-Louis + Site des étudiants de Sanar + Fiche de l'UGB sur le portail SenCampus + [https ://fr.glosbe.com] + +Université sénégalaise +Saint-Louis (Sénégal) + +' Iniwersite Gaston Berger mooy Daara ju kawe ji nekk diwaanu Ndar ci réewum Senegaal. + +Démb +Léewópóol Sedaar Seŋoor moo amal tegum xeer bu jënk ci wàllum taxawaay iniwersite wi ci 14 sãwiye 1975. + +Taxawaayam mu ngi aju ci sart bu 2 sãwiye 1990, iniwersite wu Ndar mu ngi teeru limu ndongo wu njënk (600)ci 17 Desàmbar 1990 ci yoonu négandi. + +Mu ngi jot gëddam ci ndogalu bu 10 sulet 1996 ak tur bu bees jóge ci ndogalu bu 4 desàmbar 1996. + +Ku ñu ko duppe Gaston Berger, nekk na ab kàngam ci wàllum xeltu, di doomu Senegaal ak Farãs, juddo Ndar-Géej. Di baayu Maurice Béjart. + +Ràññeefi barab + +Diggànte iniwersite ak Ndar toll na ci fukki (10) km. Boo jóge Risaartool jëmsi Ndar di nga séen wërngalu kàggu gu mag bi. +Iniwersite dafa fekk boole ñaari dëkk : Sanaar Pël ak Sanaar Wolof. Loolu tax na ndongo yi di ko woowe yenn saay Sanaar. Itam kërub internetu ndogo daara yi« http://www.Sunusanar.com » la ñu ko tudde. + +Bërëbu tàggat ak gëstu +L'université Gaston Berger est composée d'unités de formation et de recherche (UFR équivalent des facultés). Il y en a huit au total : + + Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama + Xam-xamu jëmale ak xarala + Xam-xamu yoon ak politig + Xam-xamu koom-koom ak + Xam-xamu wérgu-yaram + Xam-xamu mbay, sàmm, nàpp ak xarala yu màcc ci wàllum dund + Caada, diine, taaral ak jokkoo + Diiru njàng mi di na toll ci fukki weer. Di tàmbalee oktoobar jàpp sulet. Waaye ubbite njagale mi ak njeextal mi ngi aju ci barabu tàggat ak gëstu bu nekk. + +Ladab ak xam-xamu nekkinu doomu àddama +Barabu tàggat ak gëstu ci ladab ak xam-xamu nekkinu doomu aadama ëmb juróomu bàqasu: + Angale, + Farãse + Làkk nasaraan jëmale, + Xam-xamu melosuuf, + Xam-xamu nekkinu àskan yi. + +Xam-xamu jëmale ak xarala + + Barabu tàggat ak gëstu ci xam-xam jëmale ak xaraala ëmb na bàqasu xayma jëmale, bànqaas informatig, bànqaas bitil jëmale ak tàggat ci wàllum xéy. + +Mën a dugg + +Bànqaasu xayma jëmale + +Bànqaasu bitil jëmale + +Bànqaasu informatig + +Xam-xamu yoon ak politig + +Barabu tàggat ak gëstu xam-xamu yoon ak politik ëmb na ñett bàqaas: + Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi ; + Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris ; + Bànqaasu xam-xamu politig. + +Bànqaasu àq ak yelleefu gox-goxaan yi + +Bàqansu àq ak yelleefu antarpiris + +bànqaasu xam-xamu politig + +Mën a dugg + +Xam-xamu koom-koom ak doxalin +Kërug internet + +Caada, diine, taaral ak jokkoo +Kërug internet +Barabu tàggat ak gëstu caada, diine, taaral, ak jokkoo ëmb na juróom benn bàqasu : + Bànqaasu jokkoo, + bànqaasu infogarafi, + Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada, + Bànqaasu làkk ak caada Agrig, + Bànqaasu mënloo aju ci bokk moomel, + Bànqaasu Xam-xamu diine. + +bànqaasu jokkoo + +Mën a dugg + +tërëlin + +Mujjàntal + +Bànqaasu infogarafi + +Bànqaasu mënloo ci wàllum taaral ak caada + +Mujjàntal + +Mën a dugg + +Bànqaasu làkk ak caada Agrig + +Mujjàntal + +Màndargal + +Mën a dugg + +Wàllum gëstu + +nekkinu ndongo daara yi (CROUS) + +yokkute lim ndongo yi +thumb|350px|Évolution des effectifs de l'UGB entre 2001 et 2007 + +Dëkkuwaay + +Dem beek dikk bi + +Tektal yi + +Xool yeneen + +Téere ak mbóotu tektal + Dossier sur l'UGB dans un numéro spécial sur l'enseignement supérieur au Sénégal, Le Soleil, janvier 2008, 5-6 + +Cosaan + https://web.archive.org/web/20121110200513/http://www.gouv.sn/Decret-no-2012-1163-du-29-octobre.html + +mbóotu tektal + Musée du Centre de Recherches et de Documentation du Sénégal à Saint-Louis + Université Cheikh-Anta-Diop + Éducation au Sénégal + Felwine Sarr + +mbóotu biti + + Site officiel + Présentation et images sur le site du Campus numérique francophone de Saint-Louis + Site des étudiants de Sanar + Fiche de l'UGB sur le portail SenCampus + + +Université sénégalaise +Saint-Louis (Sénégal) +Iniweersite Séex Anta Jóob (ISAJ), ñu xam ko itam ci iniweersite bu ndakaaru, moom rekk mooy iniwersite ci Ndakaaru, kàppitaalu Senegaal, ci Afrig Soowu Jant. + +Ñu ngi ko tuddee Seex Anta Joób di àntoropolog bu xam-xamam màcc ci jaar-jaari démb. + +Ci kanamu iniweersite bi, mën nan ci jàng « Lux mea lex », « Leer a di sama yoon ». xew-xewu ubbite iniweersite bi amoon na ca atum 1959 Lewopool Sedaar Sengoor moo joxe bàkk bi. + +Ci iniweersite bi, ngongo yi ñoongi bowoo ci bërëb yu wuute:: + Mu di Afrig : Senegaal, Burkinaa Fasoo, Kodiwaar, Togoo, Benee, Niseriya, Móritani, Maali, Ruwandaa, Kamerun... + Mu di harfu : Farãs, Belsik, Gopu Amerig, Ãngalteer... + Mu di Aasi : Libaŋ, Palestin... +Daara Paj ngaa ngi dalal ay ndongo yu bawoo ca marok ak tinisii. + +COUD moo sasoo dimbale, dalal mbooleem xeeti ndongo yu bees ci réew mi ak yeneeni réew, ci wàllum lekk, dalukaay ak lépp luy tàggat yaram ak aadaak cosaan. +Ëtt bi yor lépp lu jëm ci iniweersite bi (COUD) moo yor wàllu ndimbal, teertu ndongo yii door a am BAC et ndongo doxandeem yi, wàllu lekk, dëkkuwaay ak lu jëm ci tàggat yaram ak aada ci biir ISAJ. + +Jaar-jaar + +Iniweersite Séex Anta Jóob moo donnu daara ju doon jàngale wàllum paj ca jamonooy Afrique-Occidentale française. + +Iniweersite bu Ndakaaru ñoo gi ko sanc , xewu ubbitéefam amoon ci njiitalu kilifë yi ci . C'est l'une des plus anciennes d'Afrique de l'Ouest. De nombreux cadres sénégalais et étrangers y ont été formés. + +Coppite jëm ci tur wa mi ngi am ci bésu . + +Ammbalemu ISAJ kii di Sëriñ Tewodoor Monod moo ko defar te niit bii di Lusiyeŋ Paay (1957 - 1960) nangowoon ko. +Mingi bindoo ak ñaari kewel yu jàkkarloo gir wone meñental, sakkannaay, ay njureel. Ci ginaaw kewel gu nekk am na ay niitu yuy tekki leeraange ak xam-xam. + +Lii di ndongo ci biir daara ji bari ba jéggi dayoo : lu tollook ci atum 2011, ngir rekk palaas Ndàmpaay ji tolloon na ci lu tolook de 13 à 32 miliyoŋ ci ëroo digante 2000 ak 2010, doyul ngir faj soxla yi. Ci at yii di ñëw, ISAJ jël na ndogal wàññi lifay duggu ci ay ndongo jaarale ko ab tànn tek gën a yook njàngale gu laajul ndongo yi teew. Mi ngi yaakaar tamit ci sosu iniwzzesite bu bees ci biir Ndakaaru. + +Tëddin wi + +ISAJ am na juróom benni ëtt, ñeent daara ak fukk-ak-ñaari ëtt : + +Këyitu ëtt yi + Ëttu gëstu ak xarala (FST) + Ëttu ladam ak njangat ci doomu àdama (FLSH) + Ëttu gëstu yoon ak politig (FSJP) + Ëttu gëstu topato koom-koom (FASEG) + Ëttu gëstu ci xarala jëm ci njangale ak taggat (FASTEF) + Ëttu giy jàngale wallum pac, joxe sgarab ak saafara ak lépp lu ajju ci gemmiñ (FMPOS) + +Këyitu daara yi + Ëttu njangale xam-xam, gëstu ak xarala jëm ci xibaaru (CESTI) + Ëttu politeknig gu ndakaru (ESP) + Ëttu gi yorol wàllum téere denc ak gëstu (EBAD) + Ëttu njangale gu kawe gi ci wallu xarala ak xarañ (ENSETP) + Ëttu njàngale koom-koomug njariñ (ESEA ex ENEA) +Daaram bi mu jagleel njàng ak njàngaleem mpaj ak daara biy bi ñuy jàngalee xibaaru siiw nañu lool . + +Këyitu ëtt yi + Ëttu njàngaleek rataxal làkk yi bu Dakaar (CLAD) + Ëttu njàngaleek gëstu ci doole yi ñu mën a yeesalaat (CERER) + Ëttug tàggat ak gëstu ci nit ñi, naataange ak wergi-yaram meññenteel (IPDSR) + Ëttug tàggatug saytu ci sancum njëm (IFACE) + Ëttu farañse bi ñu jagleel ndongo doxandeem (IFEE) + Ëttu askan bi aju ci pajum xale (IPS) + Ëttug gëstu ci njàngale waññi (IREMPT) + Ëttu wergi-yaram ak naataange (ISED) + Ëttu xam-xamu suuf si (IST) + Ëttu xam-xamu dëkkuwaay (ISE) + Ëttu Afrig bu ñuul (IFAN) + Ëttu xam-xamug njàngale, njàngale yaram ak tàggat yaram (INSEPS) + Ëttu iniweersite bun app ak yar ci ndox (IUPA) + +Daaray doktoraal +ISAJ mi ngi diktal juróom-ñaari daara doktoraal : + ndox, Melo ak Jëfandikoom ndox + Xam-xamu dund, wergi-yaram ak dëkkuwaay + Fisik, Simi, Xam-xamu suuf si, jàww ji ak toppat ligéey + Waññi ak Ĩformatik + Taaral, Aada ak caada + Njàngum nit ak mbooloo + Xam-xamug àtte, politig, koom-koom ak toppatoo + +Werekaan yi ñu ràññe ci iniweersite bi + Roose Dekottiñis, njiit bu njëkk ci daara yoon bi.. + Maalik Njaay, sossiyiolok, jàngalekat bu dayo bu njëkk . + Saliou N'diaye, sëriñu taarix, nekkonn diktalkatu ëttu àttekaay , nekkoon njiitu daara ladab ak xam-xamu nit, ñu defko njiitu iniweersite bi ci atum 2010. + Suleymaan Basiir Jaañ, nekkoon jàngalekatu filosofi ak njiitu daara ladab ak xamu-xamu nit ci iniweersite bi. + Abdulaay Wàdd, Njiitu paarti liberaal, bokk ci joƞante fal njiitu réew mi ci atum 1978, nekk njiitu réew mi li ko dalee bés bu njëkk ci weeru awril atum 2000 ba ñaareelu bés bu weeru awril atum 2012. + +Njiiti iniweersite bu Ndakaaru + +Ndongo yi fa jàngee + Abdu Juuf + Màkki Sàll + Mustafaa Ñas + Simon Gbagboo + Ibraayma Buubakar Keyta + Tomaas Boni Yaayi + Abdul Mbay + Suleymaan Ndeene Njaay + Awa Mari Kol Sekk + +Leeral yi ak tektal yi + +Xoolal tamit + +Bindin yi ni mel + Njàngale ci Senegaal + Iniweersite Gaston-Beersee + iniweersite bu Cees + +Téerantu bi + Eckhard Rattunde, « Studentenunruhen in Dakar/Senegal », Afrika Heute, 1968, 13-14, 193-196. + . La situation à l'UCAD. + . + Jean Capelle, « L'université de Dakar », Revue maritime, 135, juillet 1957, 908-913. + Jacques Duprey, L'université de Dakar, nouvelle université de la nouvelle Afrique, Montevideo, El Siglo ilustrado S.A., 1961, 69 + Pierre Fougeyrollas, Notes sur la réforme de l'université de Dakar, Dakar, 1968, 23 + . + +Jokkale yi wuute + + Jokkookayu web UCAD bu kiliftéef bi joxe + Jotaayu xaritoo wergi-yaram mu géej ak uuturu-meer (ASNOM) - Daaras njàngaleem paj bu AOF + Këyitu ISAJ ci dalinu SenCampus + +* +Xeet : Iniwersite bu Senegaal +Xeet : Ëttu njàngale bi ñu sanc ci atum 1957 + + + +iniweersite Séex Anta Jóob(ISAJ), ñu xam ko itam ci iniweersite bu ndakaaru, moom rekk mooy iniwersite ci Ndakaaru, kàppitaalu Senegaal, ci Afrig Soowu Jant. + +Ñu ngi ko tuddee Seex Anta Joób di àntoropolog bu xam-xamam màcc ci jaar-jaari démb. + +Ci kanamu iniweersite bi, mën nan ci jàng « Lux mea lex », « Leer a di sama yoon ». xew-xewu ubbite iniweersite bi amoon na ca atum 1959 Lewopool Sedaar Sengoor moo joxe bàkk bi. + +Ci iniweersite bi, ngongo yi ñoongi bowoo ci bërëb yu wuute:: + Mu di Afrig : Senegaal, Burkinaa Fasoo, Kodiwaar, Togoo, Benee, Niseriya, Móritani, Maali, Ruwandaa, Kamerun... + Mu di harfu : Farãs, Belsik, Gopu Amerig, Ãngalteer... + Mu di Aasi : Libaŋ, Palestin... +Daara Paj ngaa ngi dalal ay ndongo yu bawoo ca marok ak tinisii. + +COUD moo sasoo dimbale, dalal mbooleem xeeti ndongo yu bees ci réew mi ak yeneeni réew, ci wàllum lekk, dalukaay ak lépp luy tàggat yaram ak aadaak cosaan. +Ëtt bi yor lépp lu jëm ci iniweersite bi (COUD) moo yor wàllu ndimbal, teertu ndongo yii door a am BAC et ndongo doxandeem yi, wàllu lekk, dëkkuwaay ak lu jëm ci tàggat yaram ak aada ci biir ISAJ. + +Jaar-jaar + +Iniweersite Séex Anta Jóob moo donnu daara ju doon jàngale wàllum paj ca jamonooy Afrique-Occidentale française. + +Iniweersite bu Ndakaaru ñoo gi ko sanc , xewu ubbitéefam amoon ci njiitalu kilifë yi ci . C'est l'une des plus anciennes d'Afrique de l'Ouest. De nombreux cadres sénégalais et étrangers y ont été formés. + +Coppite jëm ci tur wa mi ngi am ci bésu . + +Ammbalemu ISAJ kii di Sëriñ Tewodoor Monod moo ko defar te niit bii di Lusiyeŋ Paay (1957 - 1960) nangowoon ko. +Mingi bindoo ak ñaari kewel yu jàkkarloo gir wone meñental, sakkannaay, ay njureel. Ci ginaaw kewel gu nekk am na ay niitu yuy tekki leeraange ak xam-xam. + +Lii di ndongo ci biir daara ji bari ba jéggi dayoo : lu tollook ci atum 2011, ngir rekk palaas Ndàmpaay ji tolloon na ci lu tolook de 13 à 32 miliyoŋ ci ëroo digante 2000 ak 2010, doyul ngir faj soxla yi. Ci at yii di ñëw, ISAJ jël na ndogal wàññi lifay duggu ci ay ndongo jaarale ko ab tànn tek gën a yook njàngale gu laajul ndongo yi teew. Mi ngi yaakaar tamit ci sosu iniwzzesite bu bees ci biir Ndakaaru. + +Tëddin wi + +ISAJ am na juróom benni ëtt, ñeent daara ak fukk-ak-ñaari ëtt : + +Këyitu ëtt yi + Ëttu gëstu ak xarala (FST) + Ëttu ladam ak njangat ci doomu àdama (FLSH) + Ëttu gëstu yoon ak politig (FSJP) + Ëttu gëstu topato koom-koom (FASEG) + Ëttu gëstu ci xarala jëm ci njangale ak taggat (FASTEF) + Ëttu giy jàngale wallum pac, joxe sgarab ak saafara ak lépp lu ajju ci gemmiñ (FMPOS) + +Këyitu daara yi + Ëttu njangale xam-xam, gëstu ak xarala jëm ci xibaaru (CESTI) + Ëttu politeknig gu ndakaru (ESP) + Ëttu gi yorol wàllum téere denc ak gëstu (EBAD) + Ëttu njangale gu kawe gi ci wallu xarala ak xarañ (ENSETP) + Ëttu njàngale koom-koomug njariñ (ESEA ex ENEA) +Daaram bi mu jagleel njàng ak njàngaleem mpaj ak daara biy bi ñuy jàngalee xibaaru siiw nañu lool . + +Këyitu ëtt yi + Ëttu njàngaleek rataxal làkk yi bu Dakaar (CLAD) + Ëttu njàngaleek gëstu ci doole yi ñu mën a yeesalaat (CERER) + Ëttug tàggat ak gëstu ci nit ñi, naataange ak wergi-yaram meññenteel (IPDSR) + Ëttug tàggatug saytu ci sancum njëm (IFACE) + Ëttu farañse bi ñu jagleel ndongo doxandeem (IFEE) + Ëttu askan bi aju ci pajum xale (IPS) + Ëttug gëstu ci njàngale waññi (IREMPT) + Ëttu wergi-yaram ak naataange (ISED) + Ëttu xam-xamu suuf si (IST) + Ëttu xam-xamu dëkkuwaay (ISE) + Ëttu Afrig bu ñuul (IFAN) + Ëttu xam-xamug njàngale, njàngale yaram ak tàggat yaram (INSEPS) + Ëttu iniweersite bun app ak yar ci ndox (IUPA) + +Daaray doktoraal +ISAJ mi ngi diktal juróom-ñaari daara doktoraal : + ndox, Melo ak Jëfandikoom ndox + Xam-xamu dund, wergi-yaram ak dëkkuwaay + Fisik, Simi, Xam-xamu suuf si, jàww ji ak toppat ligéey + Waññi ak Ĩformatik + Taaral, Aada ak caada + Njàngum nit ak mbooloo + Xam-xamug àtte, politig, koom-koom ak toppatoo + +Werekaan yi ñu ràññe ci iniweersite bi + Roose Dekottiñis, njiit bu njëkk ci daara yoon bi.. + Maalik Njaay, sossiyiolok, jàngalekat bu dayo bu njëkk . + Saliou N'diaye, sëriñu taarix, nekkonn diktalkatu ëttu àttekaay , nekkoon njiitu daara ladab ak xam-xamu nit, ñu defko njiitu iniweersite bi ci atum 2010. + Suleymaan Basiir Jaañ, nekkoon jàngalekatu filosofi ak njiitu daara ladab ak xamu-xamu nit ci iniweersite bi. + Abdulaay Wàdd, Njiitu paarti liberaal, bokk ci joƞante fal njiitu réew mi ci atum 1978, nekk njiitu réew mi li ko dalee bés bu njëkk ci weeru awril atum 2000 ba ñaareelu bés bu weeru awril atum 2012. + +Njiiti iniweersite bu Ndakaaru + +Ndongo yi fa jàngee + Abdu Juuf + Màkki Sàll + Mustafaa Ñas + Simon Gbagboo + Ibraayma Buubakar Keyta + Tomaas Boni Yaayi + Abdul Mbay + Suleymaan Ndeene Njaay + Awa Mari Kol Sekk + +Leeral yi ak tektal yi + +Xoolal tamit + +Bindin yi ni mel + Njàngale ci Senegaal + Iniweersite Gaston-Beersee + iniweersite bu Cees + +Téerantu bi + Eckhard Rattunde, « Studentenunruhen in Dakar/Senegal », Afrika Heute, 1968, 13-14, 193-196. + . La situation à l'UCAD. + . + Jean Capelle, « L'université de Dakar », Revue maritime, 135, juillet 1957, 908-913. + Jacques Duprey, L'université de Dakar, nouvelle université de la nouvelle Afrique, Montevideo, El Siglo ilustrado S.A., 1961, 69 + Pierre Fougeyrollas, Notes sur la réforme de l'université de Dakar, Dakar, 1968, 23 + . + +Jokkale yi wuute + + Jokkookayu web UCAD bu kiliftéef bi joxe + Jotaayu xaritoo wergi-yaram mu géej ak uuturu-meer (ASNOM) - Daaras njàngaleem paj bu AOF + Këyitu ISAJ ci dalinu SenCampus + +* +Xeet : Iniwersite bu Senegaal +Xeet : Ëttu njàngale bi ñu sanc ci atum 1957 + + + +iniweersite Séex Anta Jóob(ISAJ), ñu xam ko itam ci iniweersite bu ndakaaru, moom rekk mooy iniwersite ci Ndakaaru, kàppitaalu Senegaal, ci Afrig Soowu Jant. + +Ñu ngi ko tuddee Seex Anta Joób di àntoropolog bu xam-xamam màcc ci jaar-jaari démb. + +Ci kanamu iniweersite bi, mën nan ci jàng « Lux mea lex », « Leer a di sama yoon ». xew-xewu ubbite iniweersite bi amoon na ca atum 1959 Lewopool Sedaar Sengoor moo joxe bàkk bi. + +Ci iniweersite bi, ngongo yi ñoongi bowoo ci bërëb yu wuute:: + Mu di Afrig : Senegaal, Burkinaa Fasoo, Kodiwaar, Togoo, Benee, Niseriya, Móritani, Maali, Ruwandaa, Kamerun... + Mu di harfu : Farãs, Belsik, Gopu Amerig, Ãngalteer... + Mu di Aasi : Libaŋ, Palestin... +Daara Paj ngaa ngi dalal ay ndongo yu bawoo ca marok ak tinisii. + +COUD moo sasoo dimbale, dalal mbooleem xeeti ndongo yu bees ci réew mi ak yeneeni réew, ci wàllum lekk, dalukaay ak lépp luy tàggat yaram ak aadaak cosaan. +Ëtt bi yor lépp lu jëm ci iniweersite bi (COUD) moo yor wàllu ndimbal, teertu ndongo yii door a am BAC et ndongo doxandeem yi, wàllu lekk, dëkkuwaay ak lu jëm ci tàggat yaram ak aada ci biir ISAJ. + +Jaar-jaar + +Iniweersite Séex Anta Jóob moo donnu daara ju doon jàngale wàllum paj ca jamonooy Afrique-Occidentale française. + +Iniweersite bu Ndakaaru ñoo gi ko sanc , xewu ubbitéefam amoon ci njiitalu kilifë yi ci . C'est l'une des plus anciennes d'Afrique de l'Ouest. De nombreux cadres sénégalais et étrangers y ont été formés. + +Coppite jëm ci tur wa mi ngi am ci bésu . + +Ammbalemu ISAJ kii di Sëriñ Tewodoor Monod moo ko defar te niit bii di Lusiyeŋ Paay (1957 - 1960) nangowoon ko. +Mingi bindoo ak ñaari kewel yu jàkkarloo gir wone meñental, sakkannaay, ay njureel. Ci ginaaw kewel gu nekk am na ay niitu yuy tekki leeraange ak xam-xam. + +Lii di ndongo ci biir daara ji bari ba jéggi dayoo : lu tollook ci atum 2011, ngir rekk palaas Ndàmpaay ji tolloon na ci lu tolook de 13 à 32 miliyoŋ ci ëroo digante 2000 ak 2010, doyul ngir faj soxla yi. Ci at yii di ñëw, ISAJ jël na ndogal wàññi lifay duggu ci ay ndongo jaarale ko ab tànn tek gën a yook njàngale gu laajul ndongo yi teew. Mi ngi yaakaar tamit ci sosu iniwzzesite bu bees ci biir Ndakaaru. + +Tëddin wi + +ISAJ am na juróom benni ëtt, ñeent daara ak fukk-ak-ñaari ëtt : + +Këyitu ëtt yi + Ëttu gëstu ak xarala (FST) + Ëttu ladam ak njangat ci doomu àdama (FLSH) + Ëttu gëstu yoon ak politig (FSJP) + Ëttu gëstu topato koom-koom (FASEG) + Ëttu gëstu ci xarala jëm ci njangale ak taggat (FASTEF) + Ëttu giy jàngale wallum pac, joxe sgarab ak saafara ak lépp lu ajju ci gemmiñ (FMPOS) + +Këyitu daara yi + Ëttu njangale xam-xam, gëstu ak xarala jëm ci xibaaru (CESTI) + Ëttu politeknig gu ndakaru (ESP) + Ëttu gi yorol wàllum téere denc ak gëstu (EBAD) + Ëttu njangale gu kawe gi ci wallu xarala ak xarañ (ENSETP) + Ëttu njàngale koom-koomug njariñ (ESEA ex ENEA) +Daaram bi mu jagleel njàng ak njàngaleem mpaj ak daara biy bi ñuy jàngalee xibaaru siiw nañu lool . + +Këyitu ëtt yi + Ëttu njàngaleek rataxal làkk yi bu Dakaar (CLAD) + Ëttu njàngaleek gëstu ci doole yi ñu mën a yeesalaat (CERER) + Ëttug tàggat ak gëstu ci nit ñi, naataange ak wergi-yaram meññenteel (IPDSR) + Ëttug tàggatug saytu ci sancum njëm (IFACE) + Ëttu farañse bi ñu jagleel ndongo doxandeem (IFEE) + Ëttu askan bi aju ci pajum xale (IPS) + Ëttug gëstu ci njàngale waññi (IREMPT) + Ëttu wergi-yaram ak naataange (ISED) + Ëttu xam-xamu suuf si (IST) + Ëttu xam-xamu dëkkuwaay (ISE) + Ëttu Afrig bu ñuul (IFAN) + Ëttu xam-xamug njàngale, njàngale yaram ak tàggat yaram (INSEPS) + Ëttu iniweersite bun app ak yar ci ndox (IUPA) + +Daaray doktoraal +ISAJ mi ngi diktal juróom-ñaari daara doktoraal : + ndox, Melo ak Jëfandikoom ndox + Xam-xamu dund, wergi-yaram ak dëkkuwaay + Fisik, Simi, Xam-xamu suuf si, jàww ji ak toppat ligéey + Waññi ak Ĩformatik + Taaral, Aada ak caada + Njàngum nit ak mbooloo + Xam-xamug àtte, politig, koom-koom ak toppatoo + +Werekaan yi ñu ràññe ci iniweersite bi + Roose Dekottiñis, njiit bu njëkk ci daara yoon bi.. + Maalik Njaay, sossiyiolok, jàngalekat bu dayo bu njëkk . + Saliou N'diaye, sëriñu taarix, nekkonn diktalkatu ëttu àttekaay , nekkoon njiitu daara ladab ak xam-xamu nit, ñu defko njiitu iniweersite bi ci atum 2010. + Suleymaan Basiir Jaañ, nekkoon jàngalekatu filosofi ak njiitu daara ladab ak xamu-xamu nit ci iniweersite bi. + Abdulaay Wàdd, Njiitu paarti liberaal, bokk ci joƞante fal njiitu réew mi ci atum 1978, nekk njiitu réew mi li ko dalee bés bu njëkk ci weeru awril atum 2000 ba ñaareelu bés bu weeru awril atum 2012. + +Njiiti iniweersite bu Ndakaaru + +Ndongo yi fa jàngee + Abdu Juuf + Màkki Sàll + Mustafaa Ñas + Simon Gbagboo + Ibraayma Buubakar Keyta + Tomaas Boni Yaayi + Abdul Mbay + Suleymaan Ndeene Njaay + Awa Mari Kol Sekk + +Leeral yi ak tektal yi + +Xoolal tamit + +Bindin yi ni mel + Njàngale ci Senegaal + Iniweersite Gaston-Beersee + iniweersite bu Cees + +Téerantu bi + Eckhard Rattunde, « Studentenunruhen in Dakar/Senegal », Afrika Heute, 1968, 13-14, 193-196. + . La situation à l'UCAD. + . + Jean Capelle, « L'université de Dakar », Revue maritime, 135, juillet 1957, 908-913. + Jacques Duprey, L'université de Dakar, nouvelle université de la nouvelle Afrique, Montevideo, El Siglo ilustrado S.A., 1961, 69 + Pierre Fougeyrollas, Notes sur la réforme de l'université de Dakar, Dakar, 1968, 23 + . + +Jokkale yi wuute + + Jokkookayu web UCAD bu kiliftéef bi joxe + Jotaayu xaritoo wergi-yaram mu géej ak uuturu-meer (ASNOM) - Daaras njàngaleem paj bu AOF + Këyitu ISAJ ci dalinu SenCampus + +* +Xeet : Iniwersite bu Senegaal +Xeet : Ëttu njàngale bi ñu sanc ci atum 1957 + + + +iniweersite Séex Anta Jóob(ISAJ), ñu xam ko itam ci iniweersite bu ndakaaru, moom rekk mooy iniwersite ci Ndakaaru, kàppitaalu Senegaal, ci Afrig Soowu Jant. + +Ñu ngi ko tuddee Seex Anta Joób di àntoropolog bu xam-xamam màcc ci jaar-jaari démb. + +Ci kanamu iniweersite bi, mën nan ci jàng « Lux mea lex », « Leer a di sama yoon ». xew-xewu ubbite iniweersite bi amoon na ca atum 1959 Lewopool Sedaar Sengoor moo joxe bàkk bi. + +Ci iniweersite bi, ngongo yi ñoongi bowoo ci bërëb yu wuute:: + Mu di Afrig : Senegaal, Burkinaa Fasoo, Kodiwaar, Togoo, Benee, Niseriya, Móritani, Maali, Ruwandaa, Kamerun... + Mu di harfu : Farãs, Belsik, Gopu Amerig, Ãngalteer... + Mu di Aasi : Libaŋ, Palestin... +Daara Paj ngaa ngi dalal ay ndongo yu bawoo ca marok ak tinisii. + +COUD moo sasoo dimbale, dalal mbooleem xeeti ndongo yu bees ci réew mi ak yeneeni réew, ci wàllum lekk, dalukaay ak lépp luy tàggat yaram ak aadaak cosaan. +Ëtt bi yor lépp lu jëm ci iniweersite bi (COUD) moo yor wàllu ndimbal, teertu ndongo yii door a am BAC et ndongo doxandeem yi, wàllu lekk, dëkkuwaay ak lu jëm ci tàggat yaram ak aada ci biir ISAJ. + +Jaar-jaar + +Iniweersite Séex Anta Jóob moo donnu daara ju doon jàngale wàllum paj ca jamonooy Afrique-Occidentale française. + +Iniweersite bu Ndakaaru ñoo gi ko sanc , xewu ubbitéefam amoon ci njiitalu kilifë yi ci . C'est l'une des plus anciennes d'Afrique de l'Ouest. De nombreux cadres sénégalais et étrangers y ont été formés. + +Coppite jëm ci tur wa mi ngi am ci bésu . + +Ammbalemu ISAJ kii di Sëriñ Tewodoor Monod moo ko defar te niit bii di Lusiyeŋ Paay (1957 - 1960) nangowoon ko. +Mingi bindoo ak ñaari kewel yu jàkkarloo gir wone meñental, sakkannaay, ay njureel. Ci ginaaw kewel gu nekk am na ay niitu yuy tekki leeraange ak xam-xam. + +Lii di ndongo ci biir daara ji bari ba jéggi dayoo : lu tollook ci atum 2011, ngir rekk palaas Ndàmpaay ji tolloon na ci lu tolook de 13 à 32 miliyoŋ ci ëroo digante 2000 ak 2010, doyul ngir faj soxla yi. Ci at yii di ñëw, ISAJ jël na ndogal wàññi lifay duggu ci ay ndongo jaarale ko ab tànn tek gën a yook njàngale gu laajul ndongo yi teew. Mi ngi yaakaar tamit ci sosu iniwzzesite bu bees ci biir Ndakaaru. + +Tëddin wi + +ISAJ am na juróom benni ëtt, ñeent daara ak fukk-ak-ñaari ëtt : + +Këyitu ëtt yi + Ëttu gëstu ak xarala (FST) + Ëttu ladam ak njangat ci doomu àdama (FLSH) + Ëttu gëstu yoon ak politig (FSJP) + Ëttu gëstu topato koom-koom (FASEG) + Ëttu gëstu ci xarala jëm ci njangale ak taggat (FASTEF) + Ëttu giy jàngale wallum pac, joxe sgarab ak saafara ak lépp lu ajju ci gemmiñ (FMPOS) + +Këyitu daara yi + Ëttu njangale xam-xam, gëstu ak xarala jëm ci xibaaru (CESTI) + Ëttu politeknig gu ndakaru (ESP) + Ëttu gi yorol wàllum téere denc ak gëstu (EBAD) + Ëttu njangale gu kawe gi ci wallu xarala ak xarañ (ENSETP) + Ëttu njàngale koom-koomug njariñ (ESEA ex ENEA) +Daaram bi mu jagleel njàng ak njàngaleem mpaj ak daara biy bi ñuy jàngalee xibaaru siiw nañu lool . + +Këyitu ëtt yi + Ëttu njàngaleek rataxal làkk yi bu Dakaar (CLAD) + Ëttu njàngaleek gëstu ci doole yi ñu mën a yeesalaat (CERER) + Ëttug tàggat ak gëstu ci nit ñi, naataange ak wergi-yaram meññenteel (IPDSR) + Ëttug tàggatug saytu ci sancum njëm (IFACE) + Ëttu farañse bi ñu jagleel ndongo doxandeem (IFEE) + Ëttu askan bi aju ci pajum xale (IPS) + Ëttug gëstu ci njàngale waññi (IREMPT) + Ëttu wergi-yaram ak naataange (ISED) + Ëttu xam-xamu suuf si (IST) + Ëttu xam-xamu dëkkuwaay (ISE) + Ëttu Afrig bu ñuul (IFAN) + Ëttu xam-xamug njàngale, njàngale yaram ak tàggat yaram (INSEPS) + Ëttu iniweersite bun app ak yar ci ndox (IUPA) + +Daaray doktoraal +ISAJ mi ngi diktal juróom-ñaari daara doktoraal : + ndox, Melo ak Jëfandikoom ndox + Xam-xamu dund, wergi-yaram ak dëkkuwaay + Fisik, Simi, Xam-xamu suuf si, jàww ji ak toppat ligéey + Waññi ak Ĩformatik + Taaral, Aada ak caada + Njàngum nit ak mbooloo + Xam-xamug àtte, politig, koom-koom ak toppatoo + +Werekaan yi ñu ràññe ci iniweersite bi + Roose Dekottiñis, njiit bu njëkk ci daara yoon bi.. + Maalik Njaay, sossiyiolok, jàngalekat bu dayo bu njëkk . + Saliou N'diaye, sëriñu taarix, nekkonn diktalkatu ëttu àttekaay , nekkoon njiitu daara ladab ak xam-xamu nit, ñu defko njiitu iniweersite bi ci atum 2010. + Suleymaan Basiir Jaañ, nekkoon jàngalekatu filosofi ak njiitu daara ladab ak xamu-xamu nit ci iniweersite bi. + Abdulaay Wàdd, Njiitu paarti liberaal, bokk ci joƞante fal njiitu réew mi ci atum 1978, nekk njiitu réew mi li ko dalee bés bu njëkk ci weeru awril atum 2000 ba ñaareelu bés bu weeru awril atum 2012. + +Njiiti iniweersite bu Ndakaaru + +Ndongo yi fa jàngee + Abdu Juuf + Màkki Sàll + Mustafaa Ñas + Simon Gbagboo + Ibraayma Buubakar Keyta + Tomaas Boni Yaayi + Abdul Mbay + Suleymaan Ndeene Njaay + Awa Mari Kol Sekk + +Leeral yi ak tektal yi + +Xoolal tamit + +Bindin yi ni mel + Njàngale ci Senegaal + Iniweersite Gaston-Beersee + iniweersite bu Cees + +Téerantu bi + Eckhard Rattunde, « Studentenunruhen in Dakar/Senegal », Afrika Heute, 1968, 13-14, 193-196. + . La situation à l'UCAD. + . + Jean Capelle, « L'université de Dakar », Revue maritime, 135, juillet 1957, 908-913. + Jacques Duprey, L'université de Dakar, nouvelle université de la nouvelle Afrique, Montevideo, El Siglo ilustrado S.A., 1961, 69 + Pierre Fougeyrollas, Notes sur la réforme de l'université de Dakar, Dakar, 1968, 23 + . + +Jokkale yi wuute + + Jokkookayu web UCAD bu kiliftéef bi joxe + Jotaayu xaritoo wergi-yaram mu géej ak uuturu-meer (ASNOM) - Daaras njàngaleem paj bu AOF + Këyitu ISAJ ci dalinu SenCampus + +* +Xeet : Iniwersite bu Senegaal +Xeet : Ëttu njàngale bi ñu sanc ci atum 1957 +Fogo diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkki +São Filipe +Cova Figueira +Mosteiros + +Dëkkaani +Mosteiros +Santa Catarina do Fogo +São Filipe + +Dëkk-Dëkkaani + +Achada Furna +Achada Grande +Atalaia +Cabeça Fundão +Campanas Baixo +Chã das Caldeiras +Corvo +Curral Grande +Vicente Dias +Estância Roque +Fajãzinha +Figueira Pavão +Fonte Aleixo +Galinheiro +Miguel Gonçalves +Lagariça +Lomba +Monte Grande +Monte Largo +Patim +Ponta Verde +Relva +Ribeira do Ilhéu +Salto +Santo António +São Jorge +Tinteira + +Waax +Waax Vale (Wàllaa-dex) de Cavaleiros + +Sport + +Football clubi +Académica do Fogo +Botafogo FC +Desportivo de Cova Figueira +Cutelinho FC +Nô Pintcha dos Mosteiros +Parque Real FC - Cova Figueira +Spartak d'Aguadinha +Valência FC - As Hortas +Vulcânicos FC + +Staadi +Staad 5 Suliyet + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.fogo.cv + + +Duni Kap Weer +Momoko Kōchi (河内 桃子; 7 maars 1932 — 5 nowembar 1998). + +Filmi +Gojira (1954) +Jūjin yuki otoko (1955) +Chikyū bōeigun (1957) +Gojira tai Desutoroia (1995) + +Sapoŋ +Sinemaa +Santo Antão diiwaan nekk ci yu Kap Weer. + +Melosuuf + +Cova +Espadana +Gudo de Cavaleiros +Moroços +Ribeira de Alto Mira +Ribeira de Garça Cima +Ribeira Grande +Ribeira da Janela +Ribeira do Paul +Ribeira do Torre +Torre +Topo de Coroa +Monte Trigo +Wàlla-dex Paul + +Dëkkaani +Paul +Porto Novo +Ribeira Grande + +Dëkki +Porto Novo +Pombas (Paúl) +Ponta do Sol +Ribeira Grande (Tarrafal) + +Dëkk-Dëkkaani + +Alto Mira +Bolonha +Cabo da Ribeira +Chã de Igreja +Coculi +Corda +Eito +Espadana +Figueiras +Fontainhas +Garça de Cima +Janela +Lagoa +Lajedos +Lombo Branco +Lombo de Santa +Monte Trigo +Morro Vento +Norte +Ribeira Alta +Ribeira da Cruz +Sinagoga +Tarrafal de Monte Trigo +Xoxo/Shoshoo/Coocoo + +Dayo +Luís de Matos Monteiro da Fonseca +António do Espírito Santo Fonseca +Leão Lopes +Gabriel Mariano +Manuel de Novas +Luís Romano de Madeira Melo +Roberto Duarte Silva +Antoninho Travadinha + +Sport + +Football clubi +Liig Porto Novo: +Académica do Porto Novo +Inter Porto Novo +Marítimo Porto Novo +Sporting do Porto Novo +Liig Ribeira Grande (Liig bej-gannar Santo Antão): +Beira Mar +UD Janela +Paulense DC +Rosariense +Solpontense FC + +Staadi +Staad João Serra - Ponta do Sol +Staad gu Porto Novo + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.santoantao.cv + + +Duni Kap Weer +Serisaleem mooy péyu réewum Israayil. + +Israayil +Péy +Tokyo mooy péyu réewum Sapoŋ. + +Dëkki Sapoŋ +Péy +Rio de Janeiro benn dëkku di Bereesil. Nitñii motnañu 6.453.682. + +Dëkk +Breesil +Kyoto benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 1.474.570. + +Dëkki Sapoŋ +Nagoya benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 2.283.289. + +Dëkki Sapoŋ +Osaka benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 2.668.586. + +Dëkki Sapoŋ +Sapporo benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 1.918.096. + +Dëkki Sapoŋ +Yokohama benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 3.697.894. + +Dëkki Sapoŋ +Sal diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Melosuuf +Buracona +Calhetinha +Monte Grande +Monte Leão +Morrinho +Pedra de Lume +Serra Negra +Ponta do Norte do Sal +Ponte Sul +Terra Boa + +Dëkki +Espargos + +Diwaani +Terra Boa +Palmeira +Pedra de Lume +Santa Maria + +Dayo +Hermínia da Cruz Fortes +Ildo Lobo +Mirri Lobo +Maria Alice +Héldon Ramos +Ruben Sança + +Sport +Football: +1. Liig - Sal + +Football clubi +Académico do Aeroporto +Académica do Sal +FC Juventude +GD Palmeira (Santa Maria) +SC Santa Maria +SC Verdun-Pedra de Lume + +Staadi +Staad Marcelo Leitão - Espargos +Staad Djiduca - Santa Maria + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.sal.cv + + +Duni Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Assomada benn dëkku Santa Catarina ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi +Os Amigos +Desportivo de Assomada +Grémio Desprtivo de Nhagar +Juventude de Assomada + +Staad +Staad Cumbém + +Iniweersite +Iniweersite Santiago +Instituto Universitário de Educação + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.santa-catarina.cv +http://ecaboverde.com/cat91.htm?l=cabo-verde + +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Wu-ispaañ mooy làkk wa juddoo ca réewum Ispaañ. + +Junj +Làkk +Ispaañ +Naar yi, maanaam xeet yi jóge ci diiwaanu Sili. + +Ciili +São Nicolau diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkki +'''Ribeira Brava +Tarrafal de São Nicolau + +Dëkkaani +'Ribeira Brava +Tarrafal de São Nicolau + +Diwaani + +Belém +Cabeçalinho +Cachaço +Caleijão +Carriçal +Carvoeiros +Covoada +Estância de Brás +Fajã de Baixo +Hortelã +Juncalinho +Morro Brás +Praia Branca +Preguiça +Queimadas +Ribeira Funda +Ribeira Prata + +Dayo +Amândio Cabral +Teófilo Chantre +Baltasar Lopes da Silva +Armando Zeferino Soares + +Football clubi +AJAT'SN +SC Atlético +Desportivo Ribeira Branca +FC Ultramarina +FC Talho + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +h*https://web.archive.org/web/20050124120901/http://anmcv.org/ +http://www.caboverde.com/ilhas/ysnic-it.htm + +Duni Kap Weer +Porto Novo benn diiwaan ci yu bẽj-saluumu yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Waax +Waax bu Porto Novo (Porto Novo) + +Sport + +Football klubi +Académica do Porto Novo +GDRC Fiorentina +Inter de Porto Novo +CS Martimo +Sporting Clube de Porto Novo + +Staad +Staad Porto Novo (Estàdio Municipal do Porto Novo) + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Michel Lesourd, "Porto Novo", Le Cap-Vert, Jaguar Publishers, Paris, 2006, p. 176-177 ISBN 978-2-86950-408-0 + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Port Stanley mooy péeyu rééwum Dunu Falkland. Nitñii motnañu 2 121 (2012). + +Dunu Falkland +Péy +Chelyabinsk (Челя́бинск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 130 132 (2010). + +Dëkki Riisi +Boa Vista diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkki +'''Sal Rei + +Dëkk-Dëkkaani +Bofarreira +Cabeça dos Tarafes +Curral Velho +Espingueira +Estância de Baixo +Fundo das Figueiras +João Galego +Povoação Velha +Rabil + +Melosuuf +Viana (Deserto de Viana) - yay + +Dayo +Germano Almeida +Daniel Damásio Ascensão Filipe +Aristides Lima +Aristides Pereira + +Football clubi +Académica Operária - Sal Rei +Onze Estrelas +Sport Sal Rei Club +Sporting Boa Vista + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +https://www.boavistaofficial.com/ + + +Dëkkaani Kap Weer +Duni Kap Weer +Cidade Velha benn dëkku Ribeira Grande de Santiago ci yu bëj-saluum yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Football clubi +AD Ribeira Grande + +Karmat ak delluwaay + +Cidade Velha - UNESCO , , +Cidade Velha declarada Património Mundial da Humanidade +Cidade Velha becomes Cape Verde's first World Heritage site, UNESCO World Heritage Centre, 26 juuni 2009 + +Lëkkalekaay yu biti + +Cidade Velha - Santiago - Kap Wer - CapVerdeWeb + +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Major League Soccer aabakat wexxa kupe ganglgeng mekka Diiwaan yu Bennoo. Major League Soccer am dese ñaar-fukk morom. +Krasnoyarsk (Красноя́рск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 035 528 (2010). + +Dëkki Riisi +Novosibirsk (Новосиби́рск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 473 754 (2010). + +Dëkki Riisi +Arkhangelsk (Арха́нгельск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 348 783 (2010). + +Dëkki Riisi +Vologda (Вологда) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 301 755 (2010). + +Dëkki Riisi +Yaroslavl (Яросла́вль) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 591 486 (2010). + +Dëkki Riisi +Murmansk (Му́рманск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 307 257 (2010). + +Dëkki Riisi +Vladivostok (Владивосто́к) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 606 653 (2010). + +Dëkki Riisi +Khabarovsk (Хаба́ровск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 577 441 (2010). + +Dëkki Riisi +Volgograd (Волгогра́д) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 021 215 (2010). + +Dëkki Riisi +Astrakhan (Астрахань) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 520 339 (2010). + +Dëkki Riisi +Sochi (Со́чи) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 343 334 (2010). + +Dëkki Riisi +Soligalich (Солига́лич) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 6 438 (2010). + +Dëkki Riisi +Pyatigorsk (Пятиго́рск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 142 511 (2010). + +Dëkki Riisi +Tiksi (Ти́кси) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 5 063 (2010). + +Dëkki Riisi +Yakutsk (Якутск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 269 601 (2010). + +Dëkki Riisi +Irkutsk (Иркутск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 587 891 (2010). + +Dëkki Riisi +Perm (Пермь) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 991 162 (2010). + +Dëkki Riisi +Ufa (Уфа́) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 062 319 (2010). + +Dëkki Riisi +Innopolis (Иннополис) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 96 (2016). + +Dëkki Riisi +Lyubertsy (Люберцы) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 172 525 (2010). + +Dëkki Riisi +Lukhovitsy (Лухови́цы) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 29 850 (2010). + +Dëkki Riisi +Bronnitsy (Бро́нницы) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 21 102 (2010). + +Dëkki Riisi +Klintsy (Клинцы́) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 62 510 (2010). + +Dëkki Riisi +Soltsy (Сольцы́) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 10 086 (2010). + +Dëkki Riisi +Syzran (Сызрань) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 178 750 (2010). + +Dëkki Riisi +Syktyvkar (Сыктывка́р) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 235 006 (2010). + +Dëkki Riisi +Novorossiysk (Новоросси́йск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 241 952 (2010). + +Dëkki Riisi +Saratov (Сара́тов) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 837 900 (2010). + +Dëkki Riisi +Kazan (Каза́нь) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 143 535 (2010). + +Dëkki Riisi +Omsk (Омск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 154 116 (2010). + +Dëkki Riisi +Dubna (Дубна́) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 70 663 (2010). + +Dëkki Riisi +Stavropol (Ставрополь) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 398 539 (2010). + +Dëkki Riisi +Grozny (Грозный) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 271 573 (2010). + +Dëkki Riisi +Smolensk (Смоленск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 326 861 (2010). + +Dëkki Riisi +Veliky Novgorod (Вели́кий Но́вгород) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 218 717 (2010). + +Dëkki Riisi +Nizhny Novgorod (Ни́жний Но́вгород) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 250 619 (2010). + +Dëkki Riisi +Beijing (北京市) mooy péeyu réewum Siin. Nitñii motnañu 21 700 000 (2015). + +Dëkki Siin +Péy +Sankt-Peterburg (Санкт-Петербу́рг) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 4 879 566 (2010). + +Dëkki Riisi +Kaliningrad (Калининград) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 431 902 (2010). + +Dëkki Riisi +Nakhodka (Находка) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 159 719 (2010). + +Dëkki Riisi +Magadan (Магадан) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 95 982 (2010). + +Dëkki Riisi +Susuman (Сусума́н) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 5 855 (2010). + +Dëkki Riisi +Kursk (Курск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 415 159 (2010). + +Dëkki Riisi +Pskov (Псков) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 203 279 (2010). + +Dëkki Riisi +Gdov (Гдов) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 4 379 (2010). + +Dëkki Riisi +Priozersk (Приозе́рск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 18 933 (2010). + +Dëkki Riisi +Kronstadt (Кронштадт) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 43 005 (2010). + +Dëkki Riisi +Shlisselburg (Шлиссельбург) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 13 170 (2010). + +Dëkki Riisi +Porkhov (По́рхов) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 10 608 (2010). + +Dëkki Riisi +Vysotsk (Высо́цк) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 244 (2010). + +Dëkki Riisi +Vyborg (Выборг) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 79 962 (2010). + +Dëkki Riisi +Kingisepp (Кингисепп) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 48 488 (2010). + +Dëkki Riisi +Tolyatti (Толья́тти) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 719 632 (2010). + +Dëkki Riisi +Krasnodar (Краснода́р) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 744 995 (2010). + +Dëkki Riisi +Yekaterinburg (Екатеринбу́рг) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 349 772 (2010). + +Dëkki Riisi +Ulyanovsk (Ульяновск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 613 786 (2010). + +Dëkki Riisi +Rostov-na-Donu (Росто́в-на-Дону́) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 089 261 (2010). + +Dëkki Riisi +Voronezh (Воро́неж) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 1 032 895 (2010). + +Dëkki Riisi +Izhevsk (Иже́вск) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 627 734 (2010). + +Dëkki Riisi +Ivanovo (Иваново) dëkku di Riisi. Nitñii motnañu 408 330 (2010). + +Dëkki Riisi +Maio diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkki +'''Cidade do Maio + +Dekk-dëkkaani + +Alcatraz +Barreiro +Calheta +Cascabulho +Figueira da Horta +Figueira Seco +João +Lagoa +Monte Branco +Morro +Morrinho +Pedro Vaz +Pedro Vaz Contra Baia Galeão +Pilão Cão +Porto Cais +Praia Gonçalo +Ribeira Dom João +Santo Antônio + +Football clubi +Académico 83 +Académica da Calheta +Onze Unidos + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +https://web.archive.org/web/20110927134552/http://www.anmcv.org/portugues/membro.php?id=maio +http://www.caboverde.com/ilhas/ymaio-it.htm + +Duni Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Ribeira Brava' benn dëkku Ribeira Brava ci yu nekk São Nicolau, Kap Weer. + +Football clubi +SC Atlético +Desportivo Ribeira Brava + +Dayo +Amândio Cabral +Amílcar Spencer Lopes + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay + Sabrina Requedaz et Laurent Delucchi, "Vila da Ribeira Brava", Cap-Vert, Éditions Olizane, Genève, 2011 (6e éd.), p. 182-184 ISBN 978-2-88086-394-4 + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Ottawa mooy péeyu rééwum Kanadaa. Nitñii motnañu 883 391 (2011). + +Dëkk +Péy +Québec benn dëkku di Kanadaa. Nitñii motnañu 516 622 (2011). + +Dëkk +Brava diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Dëkki +Nova Sintra + +Diwaani + +Tomé Barras (Tomé Barraz) +Cachaço +Campo Baixo +Cova Joana +Cova Rodela +Fajã de Água +Furna +Lem Mato +Mato Grande +João da Noli +Nossa Senhora do Monte +Santa Bárbara +Tantum +Vinagre + +Dayo +Viriato de Barros +Marcelino Manuel da Graca +Nilton Fernandes +Artur Augusto da Silva +Eugénio Tavares + +Football clubi +Académica Brava +Morabeza - Nossa Senhora do Monte +Nô Pintcha +Sporting Brava + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.anmcv.org/portugues/membro.php?id=vraba +http://www.caboverde.com/ilhas/ybrav-en.htm + + +Duni Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Sal Rei benn dëkku Boa Vista ci yu sowwu yu dunu Boa Vista, Kap Weer. + +Waax +Waax bu Sal Rei (Porto de Sal Rei) + +Sport + +Football clubi +Académica e Operária +Sport Sal Rei Club +Sporting Clube da Boa Vista + +Staad +Staad Arsénio Ramos + +Dayo +Aristides Raimundo Lima + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +Cidade do Maio (Porto Inglês (Waax bu angale)) benn dëkku Maio ci yu nekk Maio, Kap Weer. + +Football clubi +Académico 83Académico 83 - Soccerway +Onze UnidosCD Onze Unidos - Soccerway +Beira Mar + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Nova Sintra benn dëkku Boa Vista ci yu nekku Boa Vista, Kap Weer. + +Football clubi +Académica Brava +Benfica Brava +Sporting Brava + +Dayo +Eugénio Tavares + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Brava +Dëkki Kap Weer +Sëriñ Móodou Lóo Dagana (Sëriñ Móodu Lóo Dagana) mi ngi judd ci atum 1858 ca kër madu yala, mooy dëkku cosaanam, ma nga ca njàmbur (Luga). + +Yaayam mi ngi tudd Soxna Astu Lóo, baayam Sëriñ Subayru Lóo. Mi ngi jànge Alquraan ak xam-xam ca njàmbur ba mujj doon ab jànglekat bu mag. + +Yoroon na lu mat fukki daara ak juróom ci kilifteefam. + +Mi ngi seeti sëriñ Tuubaa ci atum 1898 juge ca kokki guy dëkkub ay nijaayam la. + +Daa tëdd guddi am lu ko feeñu ne ko demal wuti ab sëriñ, ci la jug ne seeti Sëriñ Tuubaa, te booba kenn xamul fu Sëriñ Tuubaa nekk, tubaab yi dañ koo génne woon (exiler).    + +Sëriñ Móodu Lóo Dagana dox seeti ko jaar na ci dëkk yu bari di dox ak tànkam ba gis Sëriñ bi te xamul woon fumu nekk. Bi miy dem at la am ci yoon wi. Bis bim juge woon kokki guy ba mu delsee ca at mële la soog a gis sëriñ bi. Moom la sëriñ musaa ka naa: + +"Xëye na kokki guy bisub talaata + +namm ca géej ga bañu naan xad maata + +Ba weer deelsee ca déwen saak bis ba + +la doog a seeru bàmba ngir pas-pas ba" + +Mi ngi gis Sëriñ Tuubaa ci atum 1900 ca maayoomba ca gabon. Moom mooy waa-senegal bi njëkk a juge fii dem seeti Sëriñ bi. Bi mu àggee toog na fa ay weer Sëriñ bi yabal ko ne ko, dellul senegaal wool ma Maam Seex Anta.  Mu daal di ñëw Senegaal woo Seex Anta ànd ak moom yóbb ko Gaboŋ ca Sëriñ ba. Sëriñ bi jox Seex Anta ay xasaayid yu bari yum taalifoon yabalaat ko mu ñëw Senegaal. + +Moom ak sëriñ móodu lóo desaat fa ba 1902 ci la tubaab bi indiwaat Sëriñ bi Senegaal ñu ànd ñoom ñaar. Bi Sëriñ bi amee ci réew mi ay weer, tubaab bi yóbbuwaat ko Gànnaar, sëriñ jëlaat sëriñ Móodu Lóo teg ko ca Dagana ne ko bu kenn ñëw te jaarul ci yaw. + +Looloo waral ñu koy woowe sëriñ Moodu loo Dagana. Bi Sëriñ bi jugee Dagana la ko seexal boole kook ay taalibe yu bari. Yabal ko saalum mu sanc fa ab dëkk di tërbiya, dëkk ba di dagana ca kër mbukki. + + Moom nag mi ngi fi juge dibéer 13 maars 1954 ca Ndakaaru ñu indi ko Tuubaa ci armeel yu mag yi. + +Xët yi mu lëkkalool + Nahju + Muriidulaa + +niti senegaal +Yoonu murit +Pedra Badejo benn dëkku Santa Cruz ci yu penku yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Football clubi +Benfica de Santa Cruz +Desportivo de Santa Cruz +Scorpion Vermelho + +Dayo +Lito (Cláudio Zélito Fonseca Fernandes Aguiar) +Djaniny +Elida Almeida + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Tarrafal de São Nicolau benn dëkku Tarrafal de São Nicolau ci yu nekk São Nicolau, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi + AJAT'SN + FC Ultramarina de Tarrafal + +Staad +Staad Orlando Rodrigues - football + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Šiprage mooy péyu sos Bosni, Kotor Varoš, regy Banja Luka. + +Clima + +Reference + +Internet +http://www.maplandia.com/bosnia-and-herzegovina/republika-srpska/siprage/ Maplandia +http://www.satellitecitymaps.com/europe-map/bosnia-and-herzegovina-map/federation-of-bosnia-and-herzegovina-map/%C5%A1iprage-map/ +http://www.distancesfrom.com/distances-in-%C5%A0iprage/6308019.aspx +http://www.kartabih.com/ + +Bosni +Tarrafal benn dëkku Tarrafal ci yu bëj-gannar-sowwu yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi +Amabox Barcelona +Beira-Mar Tarrafal +Estrela dos Amadores +Real Júnior +Varandinha + +Staad +Staad Maangi/Mangue (Staad Tarrafal) + +Dayi +Pedro Celestino SIlva Soares +Silvino Lopes Évora +Mário Lúcio Sousa + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Qingdao (青岛市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 9 046 200 (2014). + +Dëkki Siin +Shenzhen (深圳市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 11 908 400 (2016). + +Dëkki Siin +Shanghai (上海市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 24 152 700 (2015). + +Dëkki Siin +Guangzhou (广州市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 14 043 500 (2016). + +Dëkki Siin +Tianjin (天津市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 15 469 500 (2015). + +Dëkki Siin +Chongqing (重庆市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 49 165 500 (2015). + +Dëkki Siin +Xi'an (西安市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 8 705 600 (2015). + +Dëkki Siin +Shenyang (沈阳市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 8 106 171 (2010). + +Dëkki Siin +Wuhan (武汉市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 10 607 700 (2015). + +Dëkki Siin +Nanjing (南京市) dëkku di Siin. Nitñii motnañu 8 230 000 (2015). + +Dëkki Siin +Calheta de São Miguel benn dëkku São Miguel ci yu dun Santiago, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi +AJAC da Calheta +Flor Jovem da Calheta + +Staad +Staad Calheta + +Dayo +Teodoro Mendes Tavares + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Koyhaike dëkku di Sili. + +Sili +Kopiapo dëkku di Sili. + +Ciili +Roubaix benn dëkku Faraas, mi ngi féete ci bëj-gànnaaru réew. Mi ngi yaatoo 13,23 km², ci 2013 amoon na way-dëkk. + +Lëkkalekaay yu biti + Dalub dëkkaan ba + +Dëkki Faraas +Ponta do Sol benn dëkku Ribeira Grande ci yu nekk Santo Antão, Kap Weer. + +Sport + +Football clubi +Solpontense FC + +Staad +Staad João Serra + +Dayo +Jorge Ferreira Chaves +Raul Pires Ferreira Chaves +Gabriel António Costa (Nhô Kzik) +Domingo Lima Costa + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +São Filipe benn diiwaan ci yu nekk Fogo, Kap Weer. + +Diwaani + +Achada Furna +Achada Grande +Atalaia +Cabeça Fundão +Campanas Baixo +Chã das Caldeiras +Corvo +Curral Grande +Vicente Dias +Estância Roque +Fajãzinha +Figueira Pavão +Fonte Aleixo +Galinheiro +Miguel Gonçalves +Lagariça +Lomba +Monte Grande +Patim +Ponta Verde +Relva +Ribeira do Ilhéu +Salto +Santo António +São Jorge + +Sport + +Football clubi +Académica do Fogo +Botafogo +Spartak d'Aguadinha +Vulcânicos FC + +Staad +Staad 5 Suliyet (5 de Julho) + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Sabrina Requedaz et Laurent Delucchi, « São Filipe », iCap-Vert, Éditions Olizane, Genève, 2011 (6e éd.), p. 147-152 ISBN 978-2-88086-394-4 + +Lëkkalekaay yu biti + + http://www.sao-filipe.com/html/sao_filipe_en.html + +Dëkki Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Kamakura benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 174.314. + +Dëkki Sapoŋ +Sagamihara benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 720.986. + +Dëkki Sapoŋ +Sendai benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 1.063.103 (2013). + +Dëkki Sapoŋ +Fukuoka benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 1.550.626. + +Dëkki Sapoŋ +Hamamatsu benn dëkku di Sapoŋ. Nitñii motnañu 789.407. + +Dëkki Sapoŋ +.tr mooy barab bu tolluwaay bu njekk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Tirki. + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1990. + +Lëkkalekaay yu biti + IANA Whois Information + NIC.TR - The Official Registry Website of Turkey Network Information Center - TR NIC + + + +Barab bu tolluwaay bu njëkk +Ribeira Grande benn dëkku Ribeira Grande concelho ci yu bẽj-gannar yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Football clubi + Beira-Mar + Rosariense + +Dayo + Roberto Duarte Silva + Manuel de Novas + José Luís de Jesus + +Dencukaay + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Santa Maria benn diiwaan ci yu nekk Sal, Kap Weer. + +Football clubi +GD Palmeira +SC Santa Maria + +Dayo +Miguel Dias +Rodirlei José Ascensão Duarte (Rody) - futbooler +Manuel Antonio Martins +Rúben Sança + +Dencukaay + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + https://web.archive.org/web/20120315224500/http://opengalleries.org/cape_verde/santa_maria/Santa_Maria.html + +Dëkki Kap Weer +Sal (Kap Weert) +.cv mooy barab bu tolluwaay bu njekk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Kap Weert. + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1996. + +Lëkkalekaay yu biti + IANA Whois Information + title = ANAC.CV FAQ + + + +Barab bu tolluwaay bu njëkk +.gr mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Girees. + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1989. + +Lëkkalekaay yu biti + IANA Whois Information + GRWeb.ICS.Forth.GR - The Official .gr Registry website of FORTH + +Barab bu tolluwaay bu njëkk +Edirne benn dëkku di Tirki. Nitñii motnañu 165.979. + +Tirki +Cova Figueira benn diiwaan ci yu dun Fogo, Kap Weer. + +Football clubi +Desportivo de Cova Figueora +Baxada + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Michel Lesourd (dir.), « Cova Figueira », Le Cap-Vert, Éd. du Jaguar, Paris, 2006, p. 141 ISBN 978-2-86950-408-0 + +Lëkkalekaay yu biti + Município de Santa Catarina. Ilha do Fogo. Plano director municipal : Caracterização e diagnóstico (maars 2010, 120 p.) + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Mosteiros benn dekk-dëkkaani ci yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Diwaani +Achada Grande +Atalaia +Corvo +Cova Feijoa +Cutelo Alto +Fajãzinha +Feijoal +Mosteiros +Mosteiros Tras (or Murro) +Pai António +Queimada Guincho +Queimada Tras +Relva +Ribeira do Ilhéu +Rocha Fora +Sumbango + +Football clubi +Cutelinho FC +Nô Pintcha dos Mosteiros + +Dayo +Júlio Correia +Jose de Pala +Beto De Canda + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Michel Lesourd (dir.), « Cova Figueira », Le Cap-Vert, Éd. du Jaguar, Paris, 2006, p. 142 ISBN 978-2-86950-408-0 +Pitt Reitmeier & Luceta Fortes Cabo Verde, Kapverdische Insel, Reise Know-How Verlag Peter Rump GmbH, Bielefeld, 5. Oplaag, 2009, ISBN 978-3-8317-1771-2 +Sabrina Requedaz, Laurent Delucchi, « São Filipe », iCap-Vert, Éditions Olizane, Genève, 2011 (6e éd.), p. 152 ISBN 978-2-88086-394-4 +Map of Fogo Brava 1:60.000, Attila-Bertalen-Kartenverlag, Karlsruhe, 2002, ISBN 3-934262-03-1 + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.cmmost.cv/ +http://www.mosteiros.com/ +Victor M. Heilweil, Stephen B. Gingerich, L. Niel Plummer, Ingrid M. Verstraeten, « Groundwater Resources of Mosteiros Basin, Island of Fogo, Cape Verde, West Africa », U.S. Geological Survey Fact Sheet 2010-3069, 3 p. + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Alaaji Alieu Ibraayma Cham Juuf a ngi judd ci 22 Oktoobar 1924 ca Banjul, Gàmbi, faatu ci 2 Awril 2011 ca kerr am Bakau, Gàmbi. Alieu Ibraayma Cham Juuf ñu gen ko xame Cham Juuf, bind kat bu maak la won ci mbiir cossanie Senegambia (Senegaal ak Gàmbi). Rawati na yit, daf dan xex tubaab yi pul Afrig, rawati na Afrig gu ñuul am seen bopp. Cham Juuf maamam ya nga askan no Siin ak Saalum ci xeetu Séeréer. Buur ba Jolof Alburi Njaay ak Buur Siin Kumba Ndóofeen Famak Juuf maami Cham Juuf leng ñu.The Daily Observer :A Great Gambian historian + + Téere yum bind (ci angale)Gambia, Land of our heritageThe history of the Banjul MosqueSenegambia, The land of our heritageThe history of the Bushell. Origin of The Gambia Chamber of Commerce & IndustriesGetting to know The GambiaReviving a culture that had refused to die (1995)The calendar of historical events in The Gambia, 1455–1995 (1995)The Research Committee of Mbootaayi Xamxami WolofThe Centenary of Muhammedan School, 1903–2003. The First School Built by Muslim Community in Bathurst. A Memory Lane.The lives of the Great Islamic Scholars and Religious leaders of Senegambia. (November 1998)Banjul, The GambiaFrom: Freedom. To: Slavery. The evil that men do. Lives after them. Alex Haley’s "Roots"The century of historic events in The Gambia. Third Edition, 1900–1999.Ethnic groups of The Gambia. 1990The history of Fanal (January 1991)Party politics in The Gambia, 1945–1970The visit of the venerable Sheikh Alhaji Sekou Umar (Futi) Taal, Njol Futa to The Gambia. A visit which illuminates a whole nation.Know your country, General knowledge, QuestionsKnow your country, General knowledge, AnswersThe AdventurerThe traditional way of life in Gambian societyThe root cause of the bread and butter demonstration, s.n. (1959)Banjul Daemba 1816-1999 Tagator'' (1999) + +Lëkkalekaay yu biti + +Niti senegaal +Niti Gàmbi +Cosaan +Séeréer +Roog (mba Roog Seen) moi tuuri Yalla ci baati Séeréer ak Diiney Séeréer (A ƭat Roog). + +Diiney Séeréer +Diiney Séeréer (mba A ƭat Roog ci baati Séeréer), moi diiney Séeréer bu njëkk. Ay Ceddo lañu woon. Tay nag dugg nañu lislaam (yoonu murit), walla diiney nasaraan ca Siin (Joal-Fadiouth). Nasaraanalkat yi yu tubaab yi ñoo leen dugal ci diine jooju. Am na Séeréer ñu barry ñu tey ci diiney A ƭat Roog. Roog moi Yalla ci baati Séeréer. + +Lëkkalekaay yu biti + +American Society of African Culture: African forum, Volumes 3-4. American Society of African Culture., 1967. p. 85 +Becker, Charles: Vestiges historiques, trémoins matériels du passé clans les pays sereer, Dakar. 1993. CNRS - ORS TO M +Berg, Elizabeth L.: & Wan, Ruth, Cultures of the World: Senegal, Benchmark Books (NY), 2009, p.144, ISBN 978-0-7614-4481-7 +Biblical Archaeology Society: Bible review, Volumes 18-19. Published by: Biblical Archaeology Society, 2002. ISBN 0-9677901-0-7 +Bressers, Hans & Rosenbaum, Walter A.: Achieving sustainable development: the challenge of governance across social scales, Greenwood Publishing Group, 2003, p. 151, ISBN 0-275-97802-8. +Dion, Salif: L’Éducation traditionnelle à travers les chants et poèmes sereer, Dakar, Université de Dakar, 1983, p. 344 + Diop, Cheikh Anta: The African origin of civilization: myth or reality, L. Hill, 1974, p. 9, 197, ISBN 1-55652-072-7 +Diouf, Niokhobaye: Chronique du royaume du Sine, (suivie de Notes sur les traditions orales et les sources écrites concernant le royaume du Sine par Charles Becker et Victor Martin (1972)): Bulletin de l'IFAN, tome 34, série B, no 4, 1972, p. 706-7 (p. 4-5), p. 713-14 (p. 9-10) +Dupire, Marguerite, Les "tombes de chiens : mythologies de la mort en pays Serer (Sénégal), Journal of Religion in Africa, 1985, vol. 15, fasc. 3, p. 201-215 +Fall, Papa Oumar: « The ethnolinguistic classification of Seereer in question », in Altmayer, Claus / Wolff, H. Ekkehard, Les défis du plurilinguisme en Afrique, Peter Lang, Frankfurt am Main, Berlin, Bern, Bruxelles, New York, Oxford, Wien, 2013, p. 47-60 +Faye, Louis Diène, Mort et Naissance le monde Sereer, Les Nouvelles Éditions Africaines, 1983, p. 9-44, +Fondation Léopold Sédar Senghor: Éthiopiques, Issues 55-56. 1991. p. 62-95 +Galvan, Dennis Charles: The State Must Be Our Master of Fire: How Peasants Craft Culturally Sustainable Development in Senegal. Berkeley, University of California Press, 2004, p. 108-304, +Gastellu, Jean-Marc (with ref to notes of : M. Sambe - 1937): L'égalitarisme économique des Serer du Sénégal, IRD Editions, 1981. p.130. + Gravrand, Henry: La civilisation sereer, vol. I : Cosaan: les origines, Nouvelles éditions africaines, Dakar, 1983 + Gravrand, Henry, La civilisation sereer, vol. II : Pangool, Nouvelles éditions africaines, Dakar, 1990, p. 9-77, +Kalis, Simone: Médecine Traditionnelle, Religion et Divination Chez les Seereer Siin du Sénégal, La Coonaissance de la Nuit. L'Harmattan, 1997, p. 25-60, +Kellog, Day Otis & Smith, William Robertson: The Encyclopedia Britannica: latest edition. À dictionary of arts, sciences and general literature, Volume 25, p. 64. Published by Werner, 1902. +Klein, Martin A: Islam and Imperialism in Senegal Sine-Saloum, 1847-1914, Edinburgh At the University Press (1968) +Krzyżaniak, Lech; Kroeper, Karla & Kobusiewicz, Michał: Muzeum Archeologiczne w Poznaniu. Interregional contacts in the later prehistory of northeastern Africa. Poznań Archaeological Museum, 1996, p. 57-58, +LA PIAILLÉE No. 141. avril 2006. Dakar +Madiya, Clémentine Faïk-Nzuji: Canadian Museum of Civilization, Canadian Centre for Folk Culture Studies, International Centre for African Language, Literature and Tradition (Louvain, Belgium), Tracing memory: a glossary of graphic signs and symbols in African art and culture. Canadian Museum of Civilization, 1996. p. 5-115, +Ndiaye, Ousmane Sémou: Diversite et unicite Sereres: L’exemple de la Région de Thies. Ethiopiques numéro 54, revue semestrielle de culture négro-africaine, Nouvelle série, volume 7 2e semestre 1991 +Niang, Mor Sadio: IFAN. Ethiopiques numéro 31 révue socialiste de culture négro-africaine 3e trimestre 1982. +Sarr, Alioune, Histoire du Sine-Saloum (introduction, bibliographie et notes par Charles Becker), [in] Bulletin de l'IFAN, tome 46, série B, nos 3-4, 1986-1987 p. 31-38 +Searing, James F.: « Conversion to Islam. Military Recruitment and Generational Conflict in a Sereer-Safin Village (Bandia) », Journal of African History, 2003, n° 44, p. 73-94. +Seck, A., Sow, I., & Niass, M., Senegal, [in] The biodiversity of traditional leafy vegetables, p. 85-110. + Sell, Madlen: « La dation du nom et autres rites de passage chez les Seereer Siin du Sénégal », Le Journal des Psychologues, 2014, n° 320, p. 74-77. + Thiaw, Issa Laye: Myth de la Creation du monde selon les sages Seereer. p. 45 +Thiaw, Issa Laye: La femme Seereer (Sénégal), L'Harmattan, Paris, septembre 2005, p. 169, +Thiaw, Issa Laye: La religiosité des Seereer, avant et pendant leur islamisation, in Éthiopiques, no. 54, volume 7, 2e semestre 1991 +Tiziana Bruzzone, Virginia: La royauté de la mer à Fadiouth : aspects de la religion traditionnelle seereer, Sénégal, L'Harmattan, Paris ; IFAN, Dakar, 2011, 230 p. +Wade, Amadou: Chronique du Walo sénégalais (1186-1855). B. Cissé trans. V. Monteil. Bulletin de l'IFAN, Series B, Vol. 26, no. 3/4.1941, 1964 + +Diiney Séeréer +Mandiraja is a sub-district in Indonesia +Feebaru dorogewu, tamit ñu xame ko ni Dorogewu bu ëpp, benn yoonu dorogewu la boo xam ne kiy dorogewu dafay jël dorog bu bare walla niki melo yi bees ci moom walla yu keneen, te melokaanu dorogewu bu joge ci feebar. Ay piri yu wute ci wallu ëppal ci dorog yi ñungi leen di jëfandikoo ci fann yépp ci wér gu yaram, ak ci wallu yoonu tëjaate. Ci yenn fand yi ci ñaawteef walla nekkin yu àndulak lu nit ñi di def mungi nekk bu fekkee nit ki dafa dorogewu, te bu yaggee nekkinam dafay soppeeku ci nit ñi dina mëna am itam. Dooleeku ci gaañ sa bopp, nit ñi, ak sa xel, dorogewu mën itam indi ay tëj yu joge ci ñaawteef, su fukkee sax dañu wute wekku ci yoonu rééw mu nekk. + +Dorog yi ñungi leen di boole lu ci ëpp ak baat bii ni: sangara, yambaa, barbiturates, benzodiazepines, cocaine, methaqualone, opioids ak yenn yuy wuutu amphetamine. Li tax ba nit ñi di jël dorog leeragul bu baax, ak ñaari wax yiñ ci gëna raññe di: benn yoonu ndono te ñeneen ñi jàngal ñu ko, walla ab tamm la bu amee, su fekke tamm bi mungi gëna fës, dafay dikke feebaru bu metti. + +Ci 2010 lu tollook 5% ci nit ñi (230 miliyoŋ) ñungi doon jëfandikoo dorog yu bon. Ci ñii, 27 miliyoŋ yi dañuy jël dorog bu bari bu leendi indil musiba, ñu xame ko itam ci dorogewu bu kawe bu leen mëna indil musiba ci seen wér gu yaram, jafe jafe ci seen xel, seen nekkin ak nit ñi bu leen di dugal ci ay risk yu bon. CI atum 2015 feebaru dorogewu agg na ci 307. 400 nit ñu dee, romb na 1990 ak 165.000 dee. Ci yii, xayma yu gëna kawe ñungi joge feebaru naan sangaraci 137.500, feebaru opioidci 122.100 ñu dee, feebaru amphetamine ci 12.200 ñi dee, ak feebaru jël cocaine ci 11.100 dee. +Feebaru naqar gu metti ku dara saful MDD, ñu xame ko itam ni déteelu, mooy benn feebaru xelbu ñuy xame ci ñaari ayubés ci (dikkale bu feeñ ci yu bari. Dafay faraldi di ànd ak tuuti ci wóólu sa bopp, ñakka am yëg yëg ci yoon ci ay yëngu yëngu yu wara neex, njaxlafaay gu wacc, ak mettit bu amul lu ko waral. Nit ñi mëna nañu am yenn saay ay gëm gëm yu amul walla gis walla dégg ay mbir yu nit ñi dul gis walla dégg. Ñenn ñi am nañu ay diiru déteelu te ci seen diggante dañuy mel ñépp ay at, te ñeneen ñi ci boobu diir dañuy génne feebar bi. Feebaru naqar gu metti ku dara saful mën na japp nit ki japp bu ñaaw ci dundam, walla ci njàngam, walla ci nelawam, walla ci ni muy lekke, ak ci wér gu yaram. Ci diggante 2-8% ci magg ñi ame feebaru naqar gu metti ku dara saful dañuy dee ak xaru, te lu tollook 50% ci nit ñiy dee ak xaru amoon nañu déteelu walla beneen feebar dikkale. + +Gëm nañu ne li koy indi mooy ab mbooloowu ndono ci dereet, ci li ñu wër, ak ci wallu xel. Risk yi ñooy ci wallu cosaanu waa kër gi ci li koy joxe, coppite ci dundum nit ki, yenn garab yi, jafe jafe yu metti ci wér gu yaram, ak feebaru dorogewu . Lu tollook 40% ci risk yi ñungi joge ci ndono yi ci dereet. Saytu yi ci feebaru naqar gu metti ku dara saful mungi wekku ci jaar jaar yi nit ki di nettali ak benn saytu ci fi xelam tollu. Amul benn saytu ci laboratoire ngir feebaru déteelu yu gêna bari yi. Di ko saytu, waaaye, mën nañu ko def ngir dindi fi yenn jafe jafe yi ci yaram bi yu mëna indi ay yeneen mandarga yu mel noonu. Feebaru déteelu moo gëna metti te mooy gëna yagg naqar, lu bokk ci dund nit ki la . Lii di United States Preventive Services Task Force (USPSTF) laaj na ñu saytu déteelu ci ñi am lu ëpp fukki at ak ñaari, ci waxtu woowu ci xibaaru Cochranegis nañu ne di faraldi di laajte du jappale génne walla faj feebar bi. + +Ci yoon, nit ñi ñungi leen di faj ak joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak garab yiy xeex déteelu. Garab yi wone na ne am njëriñ, waaye njëriñ li mën na baax ci ñi gëna mettile feebar. Leerul ndax garab yi dañuy def antum risk xaru. Yenn xeeti joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem bokk na ci pajum nekkin bu àndak xalaat(CBT) ak pajum nekkin ak ñeneen ñi bu àndak xalaat. Su fekkee yeneen xayma yi amuñu njëriñ, pajum electrochoc (ECT) mën nañu ko jëfandikoo. Tëye nit ki ci opitaal dina baax su fekkee nit ki am na risk gaañ boppam te mën na léég léég ñakka ànd ak li nit ki bëgg. + +Feebaru naqar gu metti ku dara saful daloon na lu tollook 216 miliyoŋ ci ay nit (3% ci addina bi yépp) ci atum 2015. Limug nit ñi ame feebar bi ci seen dund mungi tollu ci 7% ci Japon ba 21% ci France. Lim gi ci giir dund mungi gëna kawe ci rééwi ame koom koom gu baax (15%) méngale ko ak rééw yi seen koom koom di jog (11%). Indi na ñaareel bu gëna kawe ci ay at yu ñu dund ak feebaru ñakka mën, ginnaaw ndigg guy metti. Diir gu ñu gëna raññe ni feebar bi génn na mooy ci ati ñaar fukki yi at fanweer yi. Jigéén ñi dañuy faraldi gëna nañu ame feebar bi ñaari yoon góór ñi. Lii di American Psychiatric Association di mbooloo mi nekk Amerik dajale fajkati feebaru xel yi yoq ci ne "feebaru naqar gu metti ku dara saful" ci Téére Saytu bi ak Xayma bi ngir ñi ame Feebaru Xel (DSM-II) ci atum 1980 Ab dog dog la woon feebaru déteelu bu ànd ak dikkale bu waccci DSM-II, te mënin yi bokkoon ci ñu xame ko léégi ni déteelu bu ndaw ak ay feebaru nekkin yu dajaloo ak dikkale yu bon. + Ñi amewoon feebar bi ak ñi ko ame léégi mën nañu nekk ay légëtloo. +Feebaru "bipolaire", ñu xamewoon ko ni déteelu bu ànd ak mer gu bon, mooy ab feebaru xelguy indi ay waxtu déteelu ak ay waxtu yu du sul noono yudikkale gu kawe. Dikkale gu kawe gi bari na te ñungi ko xame ni mer gu rëywalla dikkale gu amul kersa, mungi aajo ci rëyaayam, walla ndax liy wone xel mu tagoo ak li xew mungi ci. Bu nit nekkee ci mer gu rëy dafay am jikko walla yég bu dul noon njaxlaf, bég, walla mer. Nit ñi dañuy jël ay dogal te duñu ci xalaat te itam duñu xalaat li ñuy jur. Bu nit ki nekkee ci waxtuy mer gu metti duy faral di soxla nelaw. Bu nit ki nekkee ci ay déteeloom, joy dafa koy yom, gis-gisam ci dund gi dafay ñaaw, te duy xool ñeneen ñi ci ay gët. Njàjanu xaruci ñi ame feebar bi lu kawe la agg ba 6% ci ñi ëppal ñaar fukki at, tey ci booba dagg sa bopp mungi ame ci diggante 30 ba 40 %. Yeneeni jafe-jafe yi nekk ci feebari xel yi ni feebaru ragal yu mettiakdi jëfandikoo dorogdañu leendi faraldi boole ci Feebaru "bipolaire". + +Li koy indi leerul ci bopp nit ñi, wante ñaari yi yépp dili ñu wër, ak dondu am nañ ci wall. Dondu yu bari ak ay efe yu ndaw bokk nañu ci luy joxe njàjan yi. Risk yi nekk ci li ñu wër bokk na ci istuwaaru noot xale ak diir bu yagg stress. Lu tollook 85% ci wallu risk bi ñungi teg ci dondu. Feebar bi ñung ko dugal ci feebaru bipolar I bu mësoona am lumu ndaw ndaw benn waxtu dikkale, ak walla bu amul waxtu déteelu, ak ni feebaru bipolar II bu amoon lumu ndaw ndaw benn dikkale gu amul kersa (waaye bu amul ay waxtu dikkale) ak benn waxtu déteelu bu mag. Ci ñi nga xam ne ni feebar bi duy feeñ noonu bu baax lu yagg, li koy indi feebaru xel mu jaxasoo di dem ci diggante bég ak déteelu mën nañu ko xool génne li ko waral. Su fekkee li koy indi mungi joge ci ay garab walla jafe jafe ci paj mi, dañu leendi xajjale. Yeneen yi koy indi yu mëna génne yu mel noonu ñooy Feebaru yëngu-yëngu bu tar bu àndak ñakka farlu, ay feebaru nekkin, Ñi ame jangoro schizophrénie dañuy faraldi réére mbir ak li xew. Seen nekkin du méngoo ak liy xew ak febaru dorogewu ak yenn yi koy indi joge ci wallu paj mi. Saytuwër gu yaramjarul def ngir absaytu, su fekkee sax ay saytu dereet walla portale feebar yi mën nañu leen jëfandikoo ngir dindi yeneeni jafe-jafe. + +Paj mi ñuy gëna jëfandikoo bokk na ci Pajum feebaru xelak jël ay garab yi mel ni Seral dikkale (naqari dereet) ak luy xeex ak ñakk àndak sago. Yenn ci yii di seral ci yi ñi gëna jëfandikkoo bokk na ci lithium ak yeneen xeet yu wute yi di xeex jangoro kiriis Paj mu ñu waajalul ci ab pajukaay war nañu ko soxla bu fekkee am na ku jege ci fexeel boppam walla ñeneen ñi te baña fajuji. Ay jafe-jafe nekkin yu jeggi dayo, lu mel ni yëngëtu walla xeex, mën nañu ko toppatoo ak yi di xeex ak ñakk àndak sago ci diir bu gàtt walla ay garabu benzodiazépines. Ci waxtub xër, dafa gën yi di xeex déteelu ñu bayyi leena jël. Su fekkee yi di xeex déteelu ñungi leendi jëfandikoo bu amee ay déteelu, war nañu leen jëfandikoo ak li di seral dikkale. Pajum feebaru xel bu ñuy jëfandikoo electrochoc (ETC), su fekkee sax gëstuwuñu ko bu baax, war nañu ko mëna jéém ci ñooñu ñu ñu mënula faj ak yeneen paj yi. Su ñu bayyee jëfandikoo ay paj, dañu bëgg ñu benn bennal ko. Nit ñu bare dañu ame ay jafe-jafe koppar, seen nekkin ci biir nit ñi walla ci seen liggééyukaay ndax li ñu ame feebar bi. Jafe-jafe yii ñeent ba ñett yoo jël saa yu nekk benn bi am na leen. Yoon yi ñi tann ci seen dundin ak li garab yi di def ci ñoom, njàjanu dee yu jogewul ci benn jàngoroni feebaru xol tollu na ñaari yoon nit ñi. + +Téméér boo Jël ci addina bi am na kenn ku am feebaru Bipolar. Ci Amerik, téméér boo jël ñett ñi am nañu feebar bi ci seen dund, ñi ko ame ci góór ak ci jigéén ño ko tolloole. Lu ci ëpp boo ame ñaar fukki at ak Juróóm nga koy tambale gis. Feebaru bipolaire bi tollu na ci liñu génne ci xaalis ci 45 miliyaar ci Amerik ci atum 1991. Cërcëraat gu rëy ci loolu te jóge ci woññi gu kawe ci ñakka liggééyi, dafa tollu ci Juróóm fukk at mu nekk. Nit ñi ame feebaru Bipolaire dañuy faraldi am ay jafe-jafe ak ñeneen ñi di leen gise ni ñi am lëgët. +Feebaru naqar gu metti ku dara saful MDD, ñu xame ko itam ni déteelu, mooy benn feebaru xelbu ñuy xame ci ñaari ayubés ci (dikkale bu wacc bu feeñ ci yu bari. Dafay faraldi di ànd ak tuuti ci wóólu sa bopp, ñakka am yëg yëg ci yoon ci ay yëngu yëngu yu wara neex, njaxlafaay gu wacc, ak mettit bu amul lu ko waral. Nit ñi mëna nañu am yenn saay ay gëm gëm yu amul walla gis walla dégg ay mbir yu nit ñi dul gis walla dégg. Ñenn ñi am nañu ay diiru déteelu te ci seen diggante dañuy mel ñépp ay at, te ñeneen ñi ci boobu diir dañuy génne feebar bi. Feebaru naqar gu metti ku dara saful mën na japp nit ki japp bu ñaaw ci dundam, walla ci njàngam, walla ci nelawam, walla ci ni muy lekke, ak ci wér gu yaram. Ci diggante 2-8% ci magg ñi ame feebaru naqar gu metti ku dara saful dañuy dee ak xaru, te lu tollook 50% ci nit ñiy dee ak xaru amoon nañu déteelu walla beneen feebar feebaru dikkale. + +Gëm nañu ne li koy indi mooy ab mbooloowu ndono ci dereet, ci li ñu wër, ak ci wallu xel. Risk yi ñooy ci wallu cosaanu waa kër gi ci li koy joxe, coppite ci dundum nit ki, yenn garab yi, jafe jafe yu metti ci wér gu yaram, ak feebaru dorogewu. Lu tollook 40% ci risk yi ñungi joge ci ndono yi ci dereet. Saytu yi ci feebaru naqar gu metti ku dara saful mungi wekku ci jaar jaar yi nit ki di nettali ak benn saytu ci fi xelam tollu. Amul benn saytu ci laboratoire ngir feebaru déteelu yu gêna bari yi. Di ko saytu, waaaye, mën nañu ko def ngir dindi fi yenn jafe jafe yi ci yaram bi yu mëna indi ay yeneen mandarga yu mel noonu. Feebaru déteelu moo gëna metti te mooy gëna yagg naqar, lu bokk ci dund nit ki la . Lii di United States Preventive Services Task Force (USPSTF) laaj na ñu saytu déteelu ci ñi am lu ëpp fukki at ak ñaari, ci waxtu woowu ci xibaaru Cochranegis nañu ne di faraldi di laajte du jappale génne walla faj feebar bi. + +Ci yoon, nit ñi ñungi leen di faj ak joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak garab yiy xeex déteelu. Garab yi wone na ne am njëriñ, waaye njëriñ li mën na baax ci ñi gëna mettile feebar. Leerul ndax garab yi dañuy def antum risk xaru. Yenn xeeti joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem bokk na ci pajum nekkin bu àndak xalaat(CBT) ak pajum nekkin ak ñeneen ñi bu àndak xalaat. Su fekkee yeneen xayma yi amuñu njëriñ, pajum electrochoc (ECT) mën nañu ko jëfandikoo. Tëye nit ki ci opitaal dina baax su fekkee nit ki am na risk gaañ boppam te mën na léég léég ñakka ànd ak li nit ki bëgg. + +Feebaru naqar gu metti ku dara saful daloon na lu tollook 216 miliyoŋ ci ay nit (3% ci addina bi yépp) ci atum 2015. Limug nit ñi ame feebar bi ci seen dund mungi tollu ci 7% ci Japon ba 21% ci France. Lim gi ci giir dund mungi gëna kawe ci rééwi ame koom koom gu baax (15%) méngale ko ak rééw yi seen koom koom di jog (11%). Indi na ñaareel bu gëna kawe ci ay at yu ñu dund ak feebaru ñakka mën, ginnaaw ndigg guy metti. Diir gu ñu gëna raññe ni feebar bi génn na mooy ci ati ñaar fukki yi at fanweer yi. Jigéén ñi dañuy faraldi gëna nañu ame feebar bi ñaari yoon góór ñi. Lii di American Psychiatric Association di mbooloo mi nekk Amerik dajale fajkati feebaru xel yi yoq ci ne "feebaru naqar gu metti ku dara saful" ci Téére Saytu bi ak Xayma bi ngir ñi ame Feebaru Xel (DSM-II) ci atum 1980 Ab dog dog la woon feebaru déteelu bu ànd ak dikkale bu waccci DSM-II, te mënin yi bokkoon ci ñu xame ko léégi ni déteelu bu ndaw ak ay feebaru nekkin yu dajaloo ak dikkale yu bon. + Ñi amewoon feebar bi ak ñi ko ame léégi mën nañu nekk ay légëtloo. +Feebaru tëlbëti bu amul app + +Feebaru tëlbëti bu amul app mooy benn feebaru xelboo xam ne nit ñi dañuy am soxlaa xoolaat mbir yi ay yooni yoon, di leen di def yenn yëngu yëngu yi ay yooni yoon (ñu koy woowe "aada"), walla am yenn ci xalaat yi di ñëwaat ay yoon (ñu leen di woowe "tëlbëti"). Nit ñi dañuy am jafe jafe wotu seeni xalaat walla seen yëngu yëngu lu yagg. Yëngu yëngu yi ñuy gëna gis ñooyraxasu, woññi mbir yi, ak di seet ndax ab buntu tëju na walla. Ñenn ñi dañuy am jafe jafe sanni ay mbir ci biti. Yëngu yëngu yii dañuy faraldi am lu baree bare ba nga xamantane nit ki ci boppam dundu bés bu nekk dafay metti. Dafay faraldi lu ëpp benn waxtu bés bu nekk. Mag ñu bare dañuy gis ne nekkin yooyu du tekkiwuñu dara. Mënin bi dafa ànd ak ay tik, feebaru ku jaq, ak njàjan bu yoqu ci wallu xaru. + +Li koy indi waxuñu ko. Gis nañu ne am na yenn ndono falkat yi ak ñaar yéppay seex yu niróó ñoom la gëna laal ay seex yi niróówul. Liy indi njàjan yi bokk na ci xale buñu daan noot walla yeneen stress-liy yoq xew xew. Yenn yi bind nañu leen dénc gannaaw ay wall wall. Saytu bi mungi sukkandikoo ci yi koy feeñal te soxla na daq yeneen garab walla li joge ci yeneen jangoro yi koy indi. Ay xaymawukaay ni Yale–Brown Obsessive Compulsive Scale (Y-BOCS) mën nañu leen jëfandikoo ngir saytu rëyaay bi. Yeneen feebar yu metti yi ak ni ñuy feeñe ni yooyu bokk na ci feebaru ku jaq, feebaru naqar ak déteelu gu tar, lekk yu jaxasoo, feebaru tik, ak feebaru tëlbëti bu amul app bu nekkinu nit ki. + +Faj mi bokk na ci joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem, ni pajum nekkin bu àndak xalaat5CBT), ak yenn saay yiy xeex déteelu ni walla Pajum nekkin bu àndak xalaat (CBT) bu feebaru tëlbëti bu amul app (OCD) bokk na ci yoquteek liy indi jafe jafe yi te du bayyi nekkin bi di amaat ay yoon. Bu clomipramine di dox ak SSRI yi, efe sëkondeer yi tax na ba pajam dañu wacce ci ñaareelu liiñ bi. Yuy xeex ñakk àndak sago yu ñu dul faraldi gis mën nañu am njëriñ bu leen jëfandikoo ci kaw SSRI bi ngir fajum yenn yu fës yi wante dañu leen di boole ci njàjan yiy yoqu efe sëkondeer yi. Ñakka paj mi, dina tax ba mënin mi di faraldi yagg lool. + +Lu tollook 2.3% ci nit ñi ci seen giiru dund feebaru tëlbëti bu amul app dal na leen. Xayma bi ci benn at mungi tollu ci lu jege 1.2% ci addina bi yépp. Feebar bi duy faraldi feeñ bu nit ki weesoo fanweeri at ak juróóm, te génn wall nit ñépp dañuy tambali am ay jafe jafe balaa seen ñaar fukki at. Góór ak jigéén yépp ñoo tolloo ni leen feebar bi dale. Ci Anglais, baatu tëlbëti bu amul appdañu koy faraldi jëfandikoo ci anam bu ñu tegul ci yoon bu bokkul ak OCD ngir wonale nit ku set lool ci li muy def, ku bëgg lu wóór, kuy jël, walla kuy xool fenn lu yagg. +Feebaru stress buy wëy (PTSD) mooy benn feebaru xel bu nit mëna am ginnaaw bi mu fekkee benn tiitangejoge ci xew xew, ni yëfu saay saay, xare, ay bëkkante ci tali bi, walla yeneen xëbal ci dund nit ki. Yi koy wone bokk na ci jaaxle ci xalaat yi, yitte, walla ay géntjoge ci ay xew xew, ci xel walla ci yaram itteci(traumatisme) feebaru joge ci fekke xew xew bu yëngul xel-yiy tegtalaate, jééma moytu traumatisme joge ci yiy tegtalaate, ak yoqute ci xeex walla daw. Mbir yii di wone feebar bi dañuy yagg lu tollook lu ëpp benn weer gannaaw xew xew bi. Xale yu ndaw yi duñuy faraldi wone tiitange, wante mën nañu génne li nekk seen xol ci ay po. Nit ku am PTSD dafay nekk ci risk bu kawe ngir xaruak bëgga gaañ boppam. + +Ñu ëpp ci ñi fekke ay xew xew yi indi tiitange dañuy ame PTSD. Nit ñi dund tiitange ak yeneen nit (ni siif wallanoot xale) ñoo gëna mëna ame feebaru PTSD, méngale leen ak ñi dundul-su ñusukkandikoo ci tiitange, yi mel ni ay aksideŋ ak yaqu yaqu yu joge ci jawu ji. Lu tollook génn wall ci nit ñooñu dañuy am feebaru PTSD gannaaw siif. Xale yi ñoo gëna nééwle ci am feebaru PTSD ginnaaw tiitange, rawatina bu ñu amagul fukki at. Saytu bi mungi tegu ci feeñaayu yenn ci yi koy indi joge ci gannaaw tiitange bu ñu jële ci xew xew. + +Fagaru mën na nekk bu fekkee pajum xel mici nit ñi génne feebar bi ci teel waaye amul njëriñ su ñu ko defee ci ñépp ñu génne feebar bi walla ñu ko génnewul. + Paj yu gëna am solo ci nit ñi ame PTSD ñooy joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak ay garab. Ay paj yu wute dina ci am njëriñ. Lii mën na am kenn rekk jakkarloo ak fajkat bi walla ci ab mbooloo. Yiy xeex feebaru déteeluci garabu Serotonine buy faj xel mu lééj ñoo garab yu gëna baax yu xeex PTSD tey njëriñ génn wall ci nit ñooñu ame feebar bi. Njëriñ yooyu ñoo gëna nééw yooyu ñu gis ak pajum feebaru xel. Leerul su fekkee buñu jëfandikoo garab yi ak pajum feebaru xel ndax dina am njëriñ. Yeneen garab yi amuñu seede gu doy ne dinañu mëna am njëriñ bu ñu leen jëfandikoo, te ci wallu benzodiazepines, dina indi jafe jafe ci njëriñ li. + +Ci Amerik lu tollook 3.5% ci mag ñi am nañu PTSD ci benn at moo jël, te 9% ci ñoonu dinañu gis feebar bi ci seen dund. Ci li ëpp ci li des ci addina bi, xayma bi mungi ci diggante 0.5% ba 1% ci benn at moo jël. Xayma yu kawe yi mën nañu am ci yenn gox yi am xare. Ci jigéén ñi la gëna ëppe ci góór. Yi di feeñal tiitange bokk ci feebaru xel bind nañu ko ci jamono Grece yu njëkk ya. Ci jamonoy Xarey Addina bi mënin bi xamewoon nañu ko ci tur yu bare ni "ragal ba mënul yëngu" ak "xarekat bu tiit". Baat bi di "Feebar bi joge ci gis walla fekke tiis ni dee, yu deme noonu" ñungi ko tambali woowe noonu ci ati 1970 lu ci ëpp ndax li ñu ko génne ci U.S. soldaa yu bayyi yici xare Vietnam bi. Ñungi ko dugal ci yoon joge ci Mbooloo mi dajale ñi di yëngatu ci wallum pajum xel ci Amerik ci atum 1980 in seen ñetteelu ndaje ci wallu Saytu ak Xayma ci Téére bu Feebaru Xel yi (DSM-III). +Feebaru kuy dégg ay baat walla gis ay mbir yu doy waar, te gëm ay mbir yu amul mooy xel mu jaxasoo ñu koy gise ci nekkin bu dul noonu ak dégg-dégg bu waññeeku ci li dii dëgg. Li koy wone ci li ñi gëna gis ñooy gëm-gëm yu amul, Xalaat yu amul bopp amul geen, dégg ay baat yu ñeneen ñi dul dégg, nekk ak nit ñi ak cofeel yu waññeeku, ak ab ñakka am cawarte. Nit ñi ame feebaru kuy dégg ay baat walla gis ay mbir yu doy waar, te gëm ay mbir yu amul ñu koy woowe schizophrenie dañuy faraldi am yeneen jafe jafe feebaru xelyu mel ni jaq déteelu, walla ay feebaru dorogewu. Feebar yi buñuy feeñ dañuy ñëw ndànk ndànk, tambali ci bi nga nekkee xale bu dëggër, te dañuy yagg lool. + +Yii di indi feebaru kuy dégg ay baat walla gis ay mbir yu doy waar, te gëm ay mbir yu amul ñooy li ñu wër ak Ndono ci dereetci yooyu wall. Li jóge ci wallu li ñu wër bokk na ci nga yaroo ci dëkku taax, yambaa jëfandikoo ko bi nga nekkee xale bu góór bu jigéén, yenn cofeel yi, at mu sore bu waajur yi, ak lekk bu bon bi nga ëmbee. Ndono yi ci dereet bokk na ci ay ndono yu bare yu ñuy faraldi gis ak yu nééw. Saytu bi mungi tegu ci seetlu nekkin, nettali jaar jaari nit ki ak li ñi jege nit ki nettali. Buñuy saytu nit ki aadaam dafay am solo ci saytu bi. 2013 ba léégi amul saytu bu leer. Feebaru schizophrenie tekkiwul ne nit ki dafa am "nekkin yu wute" walla am nekkin yu bari lépp ci benn nit ki - lu ci ëpp dafay jaaxal nit ñi. + +Paj mi mungi aaju li ci ëpp ci luy xeex ñakk àndak sago garab, ak ci wetam joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem, taggat ñi di fajaate ngir ñu mëna def seen liggééy bu baax ak delluwaat nekk ak nit ñi. Leerul ndax raññeeku walla luy xeex ñakk àndak sago yu ñu dul faraldi gis ñoo gën. Ñi nga xame ne duñuy tane ak yeneen yi di xeex ñakk àndak sago clozapinewar na ñu ko jééma jëfandikoo. Ci yenn yi gëna metti te nga xam ne am na ab njàjan ci sa bopp walla ci ñeneen ñi ospitaaliise buñu tannulwar na mëna nekk, su fekkee sax léégi des ci opitaal mungi waññeeku bu baax ni bu njëkk ba. + +Lu tollu ci 0.3 ba 0.7 % ci ay nit am nañu feebaru schizophrenie ci seen dund. Ci atum 2013 amoon na ab xayma bu tollook 23.6 miliyoŋ ci ñi ame feebar bi ci addina bi yépp. Góór ñi ñoom la feebar bi gëna japp, te ci ñoom lañuy gëne raññe feebar di wonewu. Lu tollook 20% ci ñoom ñungi ciy génn te tuuti rekkay wér bu baax,te lu tollook 50% dañuy am gallankoor ci seen giiru dund. Ay jafe jafe ci nekk ak nit ñi, ni ñakka liggééy gu yagg, ndóól ak ñakka am dëkkuwaay, dafa bari. Limu yaakaar ci dund ba ab atbu nit ñi ame feebar yu fës yi mungi ci fukk ba ñaar fukki at ak juróóm gëna tuuti nit ñi ci ëpp. Li mooy li mu jur ci yoquteek jafe jafe wér gu yaram yi ñiy gis ak kawewaay xarumungi tollu ci (lu jege 5%). Ci atum 2015 xayma nañu lu tollook 17.000 ci ay nit ci addina bi ñu dee ci nekkin bu bokk ci, walla jóge ci, feebaru schizophrenie. +Xaru mooy nga am yééne ray sa bopp. feebaru naqar gu metti ku dara saful, Feebaru "bipolaire", Feebaru "schizophrénie", feebari nekkin, ak feebaru dorogewu - boole ci naan gu bari gi ak jëfandikoo garabu benzodiazepine - yi yépp luy indi xaru la Ñenn ci ñi di xaru dafa am ay jëf yu ñu dooleelndax stress joge cijafe-jafe xaalis, jafe-jafe nekkin ak nit ñi nekkin ci diggante ay nit, walla tiital Ñi mësa jééma xaru dañu nekk ñoo xamantane ngir ñu jéémaata xaru lu yomb la. Fagaru ngir waññi xarujéégo yi ñooy nééwal yoon yi di indi xaru - lu mel ni ay fetal, dorog, ak poson; faj feebaru xel yi ak dorogekat yi; yéglekaay yi nettali bu xaru amee, te yoq koom-koomi nit ñi. Su fekkee sax ay nimero yu nit ñi mëne woote saa yu nekk su ñu amee jafe-jafe bare nañu, wóórul ne am nañu njëriñ. + +Yi ñu gën di gis fasoŋu xaruda ñu wute ci diggante rééw yi, te mungi bokk ci benn wall ci ay pexe yu wóór yu ñu tërël. Fasoŋi xaru yu ñuy gën di gis ñooy xoj sa bopp, naan poson, akay fetal. Xayma nañu nit ñi dee ci xaru tollu ci 828.000 ci addina bi yépp ci atum 2015, am na yoqutewu ci xaymaay atum 1990 tolluwoon ci 712.000. Lii moo def xaru fukkeelu mbir yuy indi deeci addina bi. + +Lu jege 0.5-1.4% ci nit ñi di xaru, lu tollook 12 ci 100.000 nit yoo jël at mu nekk Ñett ci ñeent ñiy xaru ñépp ci addina bi mungi am ci ak rééw yi seen am-am demewul noonu. Xayma xaru yi am ba pare lu ci ëpp ci góór ñi la ëppe boo ko méngalee ak jigéén ñi, tambale ko ci 1,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi seen koom-koom di jóg jëm ci 3,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi ame alal. Xaru lu ci ëpp mungi gëna fës ci ñi weesu juróóm ñaar fukki at; waaye, ci yenn rééw yi, at yooyu ñungi ci diggante fukki at ak juróóm ak fanweeri at ci seen mëna xaru yu gëna kawe. Europe moo ëppoon ay nit yu xaru ci ay gox ci atum 2015. Xayma nañu fukk ba ñaar fukki miliyoŋ ñi jééma xaru te deewuñu at mu nekk. Di jééma xaru te deewuloo mën na indi ay gaañu-gaañu ak ay laago yu yagg. Ci rééwi tugël yi, di jééma xaru mungi ëppe ci ndaw ñi ak ci jigéén ñi. + +Ay gis-gis yi nit ñi am ci xaru ñungi bawoo ciay ngëm-ngëmyu mel ni diine, teddaay, ak njëriñu dund bi. Yii Diine yu joge ci Ibrahimadañu gise xaru ni ab tooñ Yalla, ndax seen ngëm-ngëm ci sellaay yu dund bi. Bi samuraidoon am ca Japon, benn xeetu xaru bi ñu xamewoon ni seppuku harakiri dañu ko joxoon cër ni beneen yoon ngir bëral ñakka tekki walla ni yoonu ñaxtu. Sati, benn jëf-jëf la bu ñu terewoon joge ci Raju Britanique bi, bu doon xaar Jëtuur Indo bidiray boppambi nééwu jëkkëram ji taalu robukaay, mu defal ko boppam walla waa këram ak mbooloo mi di ko puus. Xaru ak jééma xaru, bu njëkka ba dañu ko terewoon, waaye léégi ci rééwi Tugël yu bari kenn tereetu ko Boobu dafa nekk ab ñaawtééf ci rééw yu bari ba léégi Ci siecle ñaar fukkeel ak ñaar fukkeel ak benn, xaru lu nééw lañu ko jëfandikoo ni xeetu ñaxtu, ak kamikaze ak xaru ak ay bomb nekk na lu ñu daan jëfandikoo ni jëfinu militaire walla terroriste. +Feebaru tëlbëti bu amul app Feebaru tëlbëti bu amul appmooy bennfeebaru xelboo xam ne nit ñi dañuy am soxlaa xoolaat mbir yi ay yooni yoon, di leen di defyenn yëngu yëngu yi ay yooni yoon(ñu koy woowe "aada"), walla am yenn ci xalaat yi di ñëwaat ay yoon (ñu leen di woowe "tëlbëti"). Nit ñi dañuy am jafe jafe wotu seeni xalaat walla seen yëngu yëngu lu yagg. Yëngu yëngu yi ñuy gëna gis ñooyraxasu, woññi mbir yi, ak di seet ndax ab buntu tëju na walla. Ñenn ñi dañuy am jafe jafe sanni ay mbir ci biti. Yëngu yëngu yii dañuy faraldi am lu baree bare ba nga xamantane nit ki ci boppam dundu bés bu nekk dafay metti. Dafay faraldi lu ëpp benn waxtu bés bu nekk. Mag ñu bare dañuy gis ne nekkin yooyu du tekkiwuñu dara. Mënin bi dafa ànd ak ay tik, feebaru ku jaq, ak njàjan bu yoqu ci wallu xaru. + +Li koy indi waxuñu ko. Gis nañu ne am na yennndono falkat yi ak ñaar yéppay seex yu niróó ñoom la gëna laal ay seex yi niróówul. Liy indi njàjan yi bokk na ci xale buñu daan noot walla yeneen stress-liy yoq xew xew. Yenn yi bind nañu leen dénc gannaaw ay wall wall. Saytu bi mungi sukkandikoo ci yi koy feeñal te soxla na daq yeneen garab walla li joge ci yeneen jangoro yi koy indi. Ay xaymawukaay ni Yale–Brown Obsessive Compulsive Scale (Y-BOCS) mën nañu leen jëfandikoo ngir saytu rëyaay bi. Yeneen feebar yu metti yi ak ni ñuy feeñe ni yooyu bokk na ci feebaru ku jaq, feebaru naqar ak déteelu gu tar, lekk yu jaxasoo, feebaru tik, ak feebaru tëlbëti bu amul app bu nekkinu nit ki. + +Faj mi bokk na cijoxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem, ni pajum nekkin bu àndak xalaat(TCC), ak yenn saay yiy xeex déteelu ni Inhibiteur sélectif de la recapture de la sérotonine walla clomipramine Pajum nekkin bu àndak xalaat (CBT) bu feebaru tëlbëti bu amul app (OCD) bokk na ci yoquteek liy indi jafe jafe yi te du bayyi nekkin bi di amaat ay yoon. Bu clomipramine di dox ak SSRI yi, efe sëkondeer yi tax na ba pajam dañu wacce ci ñaareelu liiñ bi. Yuy xeex ñakk àndak sago yu ñu dul faraldi gis mën nañu am njëriñ bu leen jëfandikoo ci kaw SSRI bi ngir fajum yenn yu fës yi wante dañu leen di boole ci njàjan yiy yoqu efe sëkondeer yi. Ñakka paj mi, dina tax ba mënin mi di faraldi yagg lool. + +Lu tollook 2.3% ci nit ñi ci seen giiru dund feebaru tëlbëti bu amul app dal na leen. Xayma bi ci benn at mungi tollu ci lu jege 1.2% ci addina bi yépp. Feebar bi duy faraldi feeñ bu nit ki weesoo fanweeri at ak juróóm, te génn wall nit ñépp dañuy tambali am ay jafe jafe balaa seen ñaar fukki at. Góór ak jigéén yépp ñoo tolloo ni leen feebar bi dale. Ci Anglais, baatu tëlbëti bu amul appdañu koy faraldi jëfandikoo ci anam bu ñu tegul ci yoon bu bokkul ak OCD ngir wonale nit ku set lool ci li muy def, ku bëgg lu wóór, kuy jël, walla kuy xool fenn lu yagg. +Alquraanul Kariim + +Kaamilub Alquraan bi +Kaamil bi mi ngi doon téemeeri saar ak fukk ak ñeent ,saar yooyu mooy yii di ñëw + +1-Saaru Faatiha +2-saaru baqara +3-saaru aali-himraan +4-saaru nisaayi +5-saaru maayida +6-saaru lanhaam +7-saaru lahraaf +8-saaru lanfaal +9-saaru Tawba +10-saaru yuunus +11-saaru huud +12-saaru yuusuf +13-saaru rahdi +14-saari Ibraahiim +15-saaru hijjri +16-saaru nahli +17-saaru Lisraa +18-saaru kahfi +19-saaru Maryam +20-saaru Taahee +21-saaru Lanbiyaa +22-saaru hajji +23-saaru muuminuuna +24-saaru nuuri +25-saaru furqaani +26-saaru suharaa +27-saaru namli +28-saaru xasasi +29-saaru hankabuuti +30-saaru ruumi +31-saaru luqmaani +32-saaru sajjda +33-saaru lahsaabi +34-saaru sabayi +35-saaru faatiri +36-saaru yaasiin +37-saaru saaffaati +38-saaru saadd +39-saaru sumari +40-saaru xaafiri +41-saaru fussilati +42-saaru Suuree +43-saaru suxrufi +44-saaru duxaani +45-saaru jaasiya +46-Saaru lahqaafi +47-saaru muhammad +48-saaru fathi +49-saaru hujjraati +50-saaru majiid +51-saaru saariyaati +52-saaru tuuri +53-saaru najjmi +54-saaru saahati +55-saaru rahmaani +56-saaru waaqihati +57-saaru hadiidi +58-saaru mujaadalati +59-saaru hasri +60-saaru mumtahanati +61-saaru saffi +62-saaru jumhati +63-saaru munaafiquuna +64-saaru taxaabuni +65-saaru talaaqi +66-saaru tahriimi +67-saaru mulki +68-saaru qalami +69-saaru haaqati +70-saaru mahaariji +71-saaru nuuhi +72-saaru jinni +73-saaru mussammil +74-saaru muddassir +75-saaru qiyaamati +76-saaru linsaani +77-saaru mursalaati +78-saaru nabayi +79-saaru naasihaati +80-saaru lahmee +81-saaru takwiiri +82-saaru linfitaari +83-saaru mutaffifiina +84-saaru linsqaaqi +85-saaru buruuji +86-saaru taariqi +87-saaru lahlee +88-saaru xaasiya +89-saaru fajri +90-saaru baladi +91-saaru samsi +92-saaru layli +93-saaru duhee +94-saaru sarhi +95-saaru tiini +96-saaru halaqi +97-saaru qadri +98-saaru bayyinati +99-saaru silsaali +100-saaru haadiyaati +101-saaru qaarihati +102-saaru takaasuri +103-saaru hasri +104-saaru humasati +105-saaru fiili +106-saaru quraysin +107-saaru maahuuni +108-saaru kawsari +109-saaru kaafiruuna +110-saaru nasri +111-saaru masadi +112-saaru lixlaasi +113-saaru falaqi +114-saaru naasi + +PDF AlXuraan Wolof + + PDF + + +Daaray Taysiirul Hasiir bu Sñ Moor Jóob Ndar: + +Taysiirul Hasiir: daaray Alquraan la ju mag, ju nekk ca réewum senegaal . mingi sosu ci atum 1953, ki ko sos mingi tudd Sëriñ Moor Jóob Ndar dëkk foofee ca Ndar. + +Senegaal naka jekk da ñoo masa fonk njàngum diine moo tax diiney lislaam am fi doole lool dale ko ca bañ tànnee lislaam muy seen diine ba leegi,ci ndimbalu Yàlla jaare ko ci Sëriñ si ak nitu diine yi ñu daa taxawal ay daara ngir jàngale ak yar,daara yooya daa génne ay kurél yu takku yu Fees dell ak xam-xam ànd ak mokkal Alquraan loolu nag mujj doon jikkoy Saa Senegaal yi ba at mu jot ay téemeer i téemeer di mokkal ciy gox yu fasantikoo ak i dëkk yu ndaw-ndawaan yi. + +Dëkkub Ndar nag bokkoon ci dëkk yi gënoon a fes ci xam-xam,la ko dale ca ba Senegaal moomagul boppam ba tay jii,boroom xam-xam yu bari foofa lañ jànge, te sun mag ñi ñi ëpp ci ñoom jaar nañ fa, ba leegi téewul muy dëkkub daara di dëkkub xam-wam.la fa ne ciy daara kenn xamul num toll,bokk na ca daara ya fa gën a ràññiku te gën faa rëy "di daara joj ju yàgg la ju ubbiku ju wéet ciw njàngaliinam ju cosaanu"muy: + +Daaray Taysiirul Hasiir bu Sëriñ Moor Jóob Ndar + +Kan moo sos daara jooju? +Amul sikk-sàkka ci ne mépp mbir mu yékkatiku am na waa ju kawe ju nekk ca ginnaaw kok boroom pas-pas la,boroom yitte ju kawe la,ndaxte Yàlla day tànn saa su ne ku ko taxawul diineem ji,di ko tasaareel ab wooteem.bokk na ca ñam tànn ngir loolu *Sëriñ Moor Jóob Ndar* mu boole ko ca ña nga xam ne dañuy sàmm ak lu leen ca man a fekk;doon ay sondeel yuy lakk seen bopp ngir leeralal jullit ñi yoon wi.Sñ Mustafaa Jóob didoomam waxam ja akay dëgg bam nee :Aji sàmm ndonol way jiitu ya,kenob dëgër ci kanamu /jafe-jafe yi,Aji yar maas gi mooy mooy Sñ Moor Jóob. + +Ngir xam kuy Sñ Moor Jóob danuy tuxal jële ci doomam juñ naa Siidi Abdallaa Jóob Yal na Yàlla sàmm ko ci mbindam mum bindoon ciy jaar-jaaram duppe ko(الشيخ مور جوب مؤسس معاهد) + +Aw Askanam: + +Sñ Moor Jóob boroom xam-xam la dib faqiih di ku dëddu Àdduna dib yarkat bob dundam gépp ci léggéeyal Alquraan la ko jeexal ak waa Alquraan,moo sos Daaray Taysiirul Hasiir, di doom ci Muhammat Faati Gay Jóob,miy doom i Mbay Binta Faal,miy doom i Moor Maanta doom i Aale Soxna Sow; mi sanc Belal Jóob ci ndigëlal doomu magam jii di Sñ Maxtaar Ndumbe Jóob Kokki +Bu dee yaayam mooy:Soxna Roqayya Jóob di doom i seex Muusaa Roqayya Jóob,kenn ca Jàmbaari nitug Yàlla kookee tudd Sayxu ka doon xeex ngir yékkati Lislaam,faatu ca atum/ 1875 m. + +Ñaari way-juram yii nag ñi ngi bokkoon ci Askan wu amoon diine taqoo ko te amoon ak sàmm,di askan wuñ xam ci farlu ak yéwén ak yéwénal. + +Ab juddoom: +Sñ Moor mi ngi gane Àddina ci atum (1926)m,ci dëkk buñ naan Kër-MaantaJóob,digganteem ak Luga 22i Jun-ñay la(km). + +Tolluwaayu daara ja ca Ndar cig nattale: +Daaray Taysiirul Hasiir mi ngi ci ndar ci kace bu tudd (Soor-Dàgg), te xaw naa jege /Gaaraas/ bu mag bi ci buntu dëkk bi. Boo demee ba jege *Ndar* da nga gis ñeenti sooroori Jumaa foofa ngay jublu, boo fa àggee rekk xamal ne àgg nga ca dara ja jumaa jooju mooy jumaay Sñ Moor Jóob boroom Taysiirul Hasiir, digganteem ak daara ja tuutee fa dox; boo ko laajee sax ñu wan la ko,foofa ba daara ja wenn yoon la. Buntu daara ja ñuŋ ca bind : + "معهد تيسير العسير لتحفيظ القرآن الكريم وتدريس العلوم الشرعية" +Ak waxi Yàlla jii(فلولانفرمن كل فرقةمنهم طائفةليتفقهوافي الدين ولينذرواقومهم إذارجعواإليهم لعلهم يحذرون) + +Taariixu sosug daara ji ak ay Jaaruwaayam + +Sëriñ bi mi ngi sanc daara ji ci ndigalal Nijaayam ji ko yar tudd(Sñ Jibriil Jóob) "yal na ko Yàlla yërëm"ci atum /1954. Mi ngi tàmbalee jàngale ci Karce bu tudd (Balakoos) ca Ndar, ginnaaw loolu tuxu na dem Karce buñ naan (Jàmm-Gën) ci atum/1957,ba ci atum/1977 mu tuxuwaat dem (Soor-Dàgg) foofu la nekk ba leegi. +Kon daara ji mi ngi sosu ci atum /1954, am ñatti jaaruwaay ci biir dëkkub Ndar, ba ca mujj di (Soor-Dàgg) te foofa la nekk sax fa ba leegi, kon daara ji am na ciy at lu ëpp 60i At. + +Séddalikoog Sémbi(porogram)Njàngalem daara ja: +Daara ji nag dafa séddalikoo ci ñaari jàngu ; jàngub Alquraan :muy jàngu bi nga xam ne Alquraan rekk leesfay jàng, te mooy cosaanu daara ji, jàngal ay jëmm bañ mokkal Alquraan ˊmoo xam ay mag wallay gone. Njàng mi nag jàngalekat bune ak sab géew, géew yoy dees leena séddale ci biir xaaji jànguy Alquraan bi. Xaaji jàngub Alquraan bi nag mooy yii: + +Basaru lanwaar, Daarul xuduus, Daaru tansiil, Daarul haliim, Daaru salaam, Jànnatul mahwaa. +Jàngub Alquraan bii nag ki ko jiite mooy Sëriñ Jibriil Jóob dibdoomi Sñ moor Jóob. + +Beneen jàngu bi nag jàngub xam-xam la; maanaam Majaalis bob dees fay jàngale xeeti fànni xam-xami sariiha yépp muy: Fiq, Nahwu, Adab, Usuul, ak làkku Araab ak yeneeni fànn. jàngub xam-xam bii nag da cee wàllisi rekk waaye jubluwaayu daara ji moo doon jàngale Alquraan, ndaxte ku mokkal Alquraan ku ne da nga soxlawoo xam-xam, sëñ bi moo ko njëkk a daa jàngaleel boppam xam-xam, waaye bim demee ba Mage manatulu ko boppam, loolu waral dongo yi daa génn di ko sàkku ji feneen. Waaye bi Taawam Seex Ahmadul Xayri Jóob ñibbisee bawoo cim njàng "di boroom xam-xam bu mag dib Fóore yal na ko Yàlla sàmm, mu far gàlloo njàngalem xam-xam mi. Loolu moo sos jàngub xam-xam bi, te ba leegi moom moomu moo fay jàngale. Bam femee ba jëmmi jamono njàngiin mu bees mii xew, te aju ciy këyit mu wutal ñiy jàng xam-xam fuñuy jànge jàngum Ekool diggante Araab ak Farañse, te loolu doomam juñ naa Doktoor Seex Maalig Jóob moo koy taxawu ñu gën koo xame ci Seex Maanta, ba loola tay jii mujj na soppikub Ekool. Sñ Moor Jóob Dana farala wax lu bari naa"Amumay doom ay dongo laa am!!! + +Njàngaliinu xam-xamu daara ji: +daara ji nag njàngum xam-xam mu dëgër moo fa ne, mu kawe lool it ci xeeti fànni xam-xam yees fay jàng yépp, day tàggat dongo bi ba fum dem dees koy naw ngir bari xam-xam. Loolu nag di wane ndimbalal Yàlla lum defal Sñ Moor. Képp ku fa jànge ba jeexal Sémb wa boroom xam-xam ngay doon bu mag, bu kenn dul nàttable ab xam-xamam rawatina xam-xam Fiq ak Nahwu ak luxa, téere yuvam solo lees ciy jàng, jaare ko ci yoon wu jub it ba dongo bi xëy doon Fóore ju mag, te lu ci nekk rekk day tàmbalee ci téere yu suufe yi ba ci téere ci gën a kawe. + +Ëllëgu Daara ji ak ubbik gox ñeel ay Dongoom: + +Daara ji tërël na ab Tëréef ngir Ëllagu ay dongoom, bu njëkk da daa génne ay ndongoom di leen yóbb ca jàngub (Hanafiya) waaye leegi ñi nga xam ne seenum njàng kawe na dees leeni may ay këyit ngir ñu man a àggale seenum njàng ca daara yu kawe ca *Marog* ñu di fa jàng ba am Mastéer Walla sax Doktooraa.ci gàttal daal mooy ba jeexal, moo ñu bari jàng nañ ba noppi déllusi ubbi seen daara, ñu bari tudde seeni daara Taysiirul Hasiir, daara yooyu yépp diy bànqaas yu cosaanoo ci daara ju mag jii *Taysiirul Hasiir bu Sñ Moor Jóob Ndar* kon nag nu tuddal leen lenn ci daara yi nga xam ne ay bànqaas lan ci daara ji tey wuyyoo aw turam. + +Bànqaasi daara ji: +Sëriñ bi nag bu weesoo daaraaam ji am na ñu bawoo ci daaraji mu sampal leen daara, te daara yooyu mu sampal ay nit nag nekk ciy gox yu fasantikoo ci biir Senegaal diggante: Dakaar, Cees, Lugë, Tuubaa...am na ci yeneen it yoy ay nit a juge daara ja góor-góorlu ba taxawalal seen bopp daara tuddee ko *Taysiirul Hasiir* ngir fa la ñu jàngee ca daaray Sñ Moor. Daara yooy nag danañ ci tudd yennat tuxale ko ci Siidi Abdallaah Jóob Al Maalikii miñ tuddoon ci ginnaaw. + +Bokk na ca yooya yii di ñëw: + +Daaray Sñ Isaa Sàmb Ca Lugë ci Karce(Sanc ba) mi ngi sosu atum/1972,m ci ndigëlu Sñ Moor. +Taysiirul Hasiir :Miftaahun Nasri, bu Sñ Daam Pànne Jóob, nekk (Jaxaay)ca dakaar. mi ngi Sosu/1986.m +Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Mustafaa Jóob ca Tuubaa Karce(Jéemun)mi ngi sosu/1999. +Taysiirul Hasiir :bu Sñ Mustafaa Jóob batay, ca Tuubaa (aaliya)sosu/2012m. +Taysiirul Hasiir :Daaray Sñ Muhammat Lamin Gay ca Tuubaa(Jànnatul Firdawsi). +Taysiirul Hasiir :Sñ Baara Faati Mbóoj ca Tuubaa (Jànnatun Nahiim)sosu/2004m. +Taysiirul Hasiir :ca Tuubaa (Baxdaat) mi ngi sosu /2010m. +Taysiirul Hasiir :bu Seex Maalig Ñas ca Tuubaa (Baxdaat/2) +Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Moor Xëri Ture Tuubaa(Daaru Minan)sosu /11/02. +Taysiirul Hasiir :Ca Cees, sosu bisub Àllarba /15/2/2012.bu Sñ Móodu Yaasin Jóob. +Taysiirul Hasiir :Ca Ndar Karce (Leebar)sosu ci/2018 gi wees, Siidi Abdallaah Jóob. +Daaray Muxaddamaatul Amdaah: ca Tuubaa, sosu /11/2/2012. +Daaray Sëriñ Mbàkke Gay:ca Lugë, sosu /1998. +Taysiirul Hasiir :bu Sñ Ibraahiima Mëróon Ca Sóokoon Karce (Ndóofaan) sosu /2013. +Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Muhammat Jàllo, ca Réewum Gàmbi ca (Yuuna)digganteem ak Gëbla ga(kapitaal) mi toll ci 15i Jun-ñay(km). +Daara yii ñu lim nag yi ci ëpp ci ndigëlu Sñ Moor lees ko sose, te yu ci ëpp Taysiirul Hasiir lees leen di woowe. + +Kon lii mooy daaray Taysiirul Hasiir ak li ci aju. Di ñaanal Sñ Moor Jóob mu yàgg fi te ànd ak wér mook njabootam gépp ak képp kuy safoo Alquraan. + + +Taysiirul Hasiir + +Daaray Sëriñ Moor Jóob Ndar +Rabil benn dekk-dëkkaan Boa Vista ci yu sowwu yu dunu Boa Vista, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +Bukki mala la bu nekk ci àll bi. + +Rab +Monsoro (Faraañse : Montsoreau), Faraas. Nitñii motnañu 447 (2015). + +
Iwewewe ti idagbasoke ilu ni Monsoro + +
+ +Dëkki Faraas +Péy +Fas w:baayima la bokk ci boroom ñeenti tànk yi, bokk it ci yiy miin. +Ginaar g :Baayima la, di boroomi laaf te du naaw, te day miin. +Baaxoñ bnjanaaw la luy këf lu mel ni picc ak yu ni mel +Sahaaba yi: ñooy ñi àndoon ak yonente bi(yal na ko Yàlla dolliy xéewal ak mucc) jamonoonte ak moom te gëm ko. +Abuu Bakar +Janela benn dekk-dëkkaan Paul ci yu penku yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Dayo +Antoninho Travadinha + +Football klub +UD Janela (União Desportiva da Janela) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.ecaboverde.com/cat44.htm?l=cabo-verde + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Pedra de Lume benn dekk-dëkkaan Sal ci yu penku yu dunu Sal, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +Pedra Lume é berço da História da ilha do Sal, RTC, 24 Maars 2012 +Pedra de Lume, RTC, 24 Maars 2012 + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Sal (Kap Weert) +Unk w: Aw rab la wu mel ni sindax, di dëkk ak nit ñi lu bari ci seeni néeg. +Mbëfër m aw rabu àll la wu rëy lool +Rui Vaz benn dekk-dëkkaan São Domingos ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Xaadiriya: wenn yoon la ci yooni Tasawwuf yi, te tënku ci sunna. Ñu ngi koy askanale ci genn góor-Yàlla guñuy wax sëriñ Abdul xaadir Aljaylaanii(471h- 561h),  ñiy topp yoon woowu nag tasaaroo nañu ci gox yu bari niki Saam, Iraã, Isibt ak la féete penku ca Afrig. Yoon la woo xam ne ay jéegoom gudd na lool ci tasaare Lislaam ci goxi Afrig yi ak Asi, ba mëdd gëm-gëmu nasaraan ci fu bari ci Àdduna bi. +MIIRAAS + +Miiraas: Xam-xam la buy lijjanti alalu aji faatu ji; muy li mu bàyyi ginnaawam lépp, nan lees koy séddalee ci ñi nga xam ne ñoo ko war a donn, moom nag mooy xam-xam biy jëkk réer, jugee ci àdduna. Loolu nag Sangub mbindeef yi moo ko wax Muhammat (SHW), te it nee na mooy genn wàllug xam-xam, +(عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم: (تعلموا الفرائض وعلموها الناس فإنها نصف العلم وهو ينسى، وهو أول شيء ينزع من أمتي) رواه ابن ماجه والدارقطني) +Moom miiraas benn la ci xam-xam yi soqikoo ci Fiq ci la bànqaasoo aw wëppaam (them) day dugg ci biir bànqaasi xam-xamu Fiq bokk ci xam-xami diiney lislaam. +Banaana foytéef la gu bawoo ci garabu banaana. Banaana yi ay foytéef lañu yoo xam ne yu ci ëpp duñu am pepp bawoo ci ay xeet yu nit ñi di jëfandikoo. +Yennat ci banaana yi nga xam ne nit a koy ji, amnañu ay pepp. + +Banaana yi yu ci ëpp dañuy mboq am ay tupp-tupp. Banaana pàcc bu am solo la ci lekkug yenn gox yi. Fu ci mel ni Ugaandaa miy génne lu ëpp juroom-fukki mbir ci banaana. + +Cosaanu tur wi nag, lu ëpp ci woroom xam-xami gongikubaat yi ñoo ngi ko delloo ci làkku Wolof ne fa la ko yeneen làkk yépp jële. Ba naa na. +Amna ñu ne dafa am foyteef bu tuddoon NA te xaw a mel ni moom, bi banaana feeñee nag te gën koo neex, ñu ne: Ba naa na , maanaam bàyyi naa na. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Musa acuminata + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Abuu Bakar As siddiiq:turam dëgg di Habdul Laahi bun Abii Quhaafa di kojub (Taymu) di kojub (quraysi). Judd 50i at lu ñëkk gàddaay gi faatu 13i at ginnaaw gàddaay gi, tollook (573 - 634) ci juddug Iisaa (hs). Moom moo njëkk a wuutu Yonente bi (shw) ginnaawam, te bokk na ci fukk ñi Yonente bi digoon Àjjana ci jamonoom. Moo doonoon jëwriñu Yonente bi (shw) doonoon ab xaritam, moo àndoon ak moom bamuy gàddaay juge Màkka jëm Madiina. Waa Ahlus sunna danuy saxal ne moom Abuu- bakar moo gën ci nit ñi ginaaw ba yonente yi jàllee, te moo ci ëpp ag gëm Yàlla, ak dëddu àdduna, te mooy ki Yonente bi gën a bëgg ci nit ñi ginnaaw sunu yaay Haaysa. Aw turam dees ciy teg baatu Siddiiq ngir ne Yonente bi moo ko ko dàkkentalee ngirug dëggoom. +diine +Lislaam +sahaaba yi +Lëng xeetu garab la gu bokk ci njabootu "lamiaceae" ak ci ñoñ "Vitex". Bari na lool ci Afrig gu diggu gi,ca komoor ak ca Rewño. Mbind mii jukki la bu ñeel meññiit mi. Man ngaa bokk ak nit ñi say xalaat ci jagal ko. Meloom day ñuul, peppam dees koy lekk. + +Meññeef mi + +Meññeef mi, ci nëtëx lay doore, ñor digante mee ba noowàmbar, daal di ñuul te saf suukar. Guddaayu garab gi ci diggante yaar ba yatti meetar lay toll. Afrig la am ak bàmbulaan Endo. Ci dunu Rewño it dees na ko fa fekk. + +Turu xam-xam wi +Vitex doniana + +Tur wi ci yeneeni làkk + + Garab + Meññeef +Màdd xeetu gàncax la gu bokk ci njambootu "Apocynaceae". + +Melo wi + +Màdd gi xeetu lawtan la guy sax Afrig. Dees na ko bay it. +Manees na koo lekk noonu mbaa nu boole ko ak suukar, xorom mbaa kaani. +Bees ko boolee ak ndox ak suukar, manees na cee am ub njambaan. Manees na ci am it njar. + +Dañuy aaye ku wann xoox bi. Waaye su nu xaree xoox bi, am na xeetu der bu fa nekk bees di lekk. Doom bi dafa gànjaru ak witaamin C, camin, ribofalaawin, ñasin ak witaamin B6. +Moom nag ci nawet lay sax. +Màdd bi dafa roo, ñam wu mboq moo ëmb xoox bi te dafa nooy, wex ba noppi saf suukar. + +Barab yi muy sax + +Moom màdd Afrig gu soww la gën a bari. Dees na ko fekk it Afrig gu penku gi, moom màdd mbaa yu niroo ak moom, fu mel ni ca Tansani. Fii fi Senegaal kaasamaas/Sigicoor lay faral di bàyyikoo. + +Turu xam-xam wi +Saba senegalensis + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Konkoroŋ xeetu tiir la gu yor foytéef bu gulumba bees di lekk. Moo ngi bàyyikoo ca xawa-dun bu mag bu araab yi, ak ca gànnaaru Afrig ga mu law te faral di sax fa am ndoxi ron suuf. + +Melo wi + +Konkoroŋ gi, garab la guy àgg ci 17i met ci guddaay. Kuttmbalu ronam danay àgg ba 90 sàntimet. Caram day meññ ay jubbi xob. Xàncam daa liis, yor wirgo wu baam te dër ba noppi yor melow xob yu wow. + +Caram ak xobam danay àgg ba 1 met ci guddaay ba noppi yiir bànqaas yi ko meññ, teg ci gànnaayoo ay xosi yu dëng te jëm kaw. Xobam melow wuppukaay la yor, danay natt 120 ba 180i sàntimet. Tóortóoram bu góor ak bu jigeen ci garab yu wuute lay meññ. + +Njariñ li + +Xàncam dees na ci ràbb i basaŋ ak i duu. Dees na ko lekk it. Mattam dees na ko jëfandikoo ci tabax. Xàncam dees na ci jële njar. + +Turu xam-xam wi + +Hyphaene thebaica + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef + + +Gerte +Gerte xeetu garab la gu bokk ci njabootu lujum yi. Mi ngi soqeekoo ca réewum metsig. Dees na ko bay ci gox yi gën a bari naaj ak taw, fu mel ni réewum Senegaal. + +Melo wi + +Dees koy ràññee ci suul gimuy suul ay meññeefam. +Gerte gàncax la gog at ba at lees koy bay su dee du mbayum dër. +Xobam day nëtëx. Mi ngi toll ak 20i ba 90i sànti meetar ci guddaay. +Meññeefam a ngi tollu ak 3i ba 5i sànti meetar. +Garab la it gog dees koy bay ci suuf suñu ndiraag + +Mbooram + +Endoy Aamerig ya woon kepp a ko doon bay ci àddina. +Ginnaaw bi la ko way-noti Ispaañ yañu daa woowe: "conquistador" tasaare. +Ca Peru gisoon nanu ci seeni jalaase maam ya ay peppi gerte. +Noonu la gerte tàbbee ci kembaarug Afrig law bokk ci mbayu Senegaal. + +Njariñal gerte + +Dees na ci jële diwu gerte. +Diw googu dees na ko jëfandikoo ngir togg ceeb ak yu ni mel ca Senegaal ak feneen. +Dees na ci jële it tigadege. Joolaa yi ñu xereñ lañ ci liggeey boobu. +Tigadege boobu dinañ koy boole ak cere ak yeneen. +Kembaarug Afrig ak Aamerig nag ñoo ëpp luñ koy jëfandikoo . +Garab la gog bari na ay wopp yu muy faj. +Ay njariñam bari na lool waaye dinay sabab it ay tawat. + + garab + meññeef +Déem garab la gu bokk ci njabootu Rhamnacées di cosaanoo ci réew yu am naaj yi ci àdduna. Bari na ay xeet lool. Déem yiy am i dég dañuy meññ, di am i doom. + +Melo wi + +Déem garab la gog day am ay dég yu sew te ñaw. Ay xobam day nëtëx te tuuti. Guddaayu peer bi day toll ci digganta benn meetar ba ñaari meetar. Guddaayu garab gi yépp dana yegg ci ñatt ba ñenti meetar. + +Foytéef bi +Foytéef bi day tàmbalee ci nëtëx foofu xoox bi day weex, bu noppee jàll ci mboq daal di mujje ci wirgo wu xonq. Day saf suukar te neex lool. +Xoox bu dëgër lay am, boo ko tojee dangay fekk ca biir lu nooy lu mel ni gerte. + +Dafa gànjaru ci witaamin A, C. Am na it feer ak kalsóom. + +Xoox bi dees koy jëfandikoo ngir defar diwu yaram. + +Dénk wi + +Dénku déem luñu baaxoo jëfandikoo la ca réewi katalã ya ngir defar jumtukaay yu bari yees di jëfandikoo ci misig yu xeetoo ak i xalam niki: koblaa, falabiyol, tiibal ak tenoraa. +Dees na ko jëfandikoo it ngir defar xeeti pontu yi ñuy daaj ci xalam yi ngir takk ci buum yi. + +Turu xam-xam wi +Ziziphus + + garab + foytéef +Solom mi ngi bokk ci njabootu fabaceae. Fekk baaxca Afrig sowwu jant ak Afrig gu xalaa ga. + +Melo wi + +Solom garab la gog guddaayam man naa àgg ci 30i meetar , am peer bu tal. + +Xob yi dañoo nëtëx te tóttóor yi it day weex. + +Moom nag ñi ngi koy faral di baye ca Senegaal, rawatina ca bëj-saalum ba di kaasamaas. + +Meññeef mi + +Meññeef mi nag day xaw a tàppndaar, mel ni lu gulumba. Xott wu ñuul ëmb ko ñam wi ci biir day puur di ëmb benn pepp walla ñaar ci biir. + +Moom nag meññeef mu gànjaru la ci gilikóos, firiktóos, feer, mañesëm, kiifur ak poroteyin. + +Lem ji ñu ciy defar nag, lem ju neex, ju ñu bari soxla. Ñi ngi koy defare ca Kaasamaas ca bëj saalumub Senegaal. + +Ay turam ci yeneeni làkk + +Wolof: Solom, Farañse: Tamarinier noir, Joolaa: Buparaŋ walla efrun. +Kodiwaar: "Chat noir", Guinée: "Môké", Bénin: "Assissouin", Togo: "Attitoé", Àngale: "Velvet tamarind". + +Fi mu am + +Xeet wii nag am na Senegaal, Bene, Burkinaa Faasoo, Kamerun, Sàntar Afrig, Caat, Kodiwaar, Ginne ekaatoryaal, Gana, Ginne Bisaawóo, Ginne Konaakiri, Liberyaa, Malu, Niseer, Niseeryaa, Sao tomé-et principr, Seraa Lewon, Sudaa, Tógóo. + +Turu xam-xam wi: +Dialium guineense +garab +meññeef + + +Sump + +Sump ci garab yiy meññ te am i dég la bokk. Ab njoolaayam dina toll ci 8i ñay. Peer bi day jub, yenn saa yi mu xaaju di ñaar te day ñagas it. Wànqaas yi nag dañuy bari te rankaloo am ay dég yu ñaw jub te ñaw di toll ci 7i sànti met. +Car yi it dañuy nëtëx ñoom it am i dég. Xob wi day xaw a tuuti moom it nëtëx. +Keram daa yaraax, neexut a féexloo. Rax ci dolli ci ron garab gi day faral di am ay dég yuy wadde ci sump gi. +Bant bi it dees na ko jëfandikoo ngir socc. + +Meññeef mi + +Doom bi day gulumba, der wu mboq ëmb ñam wi, ñaw it ëmb ab xoox, ca biir xoox ba it ab saal ne ca buy niru gerte. Day neex nag saf suukar. +Bot wi di sump bi ñoragul bi, der bu nëtëx a koy ëmb, waaye moom neexul day wex. + +Njariñ yi + +Sump bari na ay njariñ lool. Saal bi ci biir xoox bi, dees na ci defar diw gu baax, muy diwu sump. +Dees na defar ci xob yi it saabu. +Xob yi ak doom yi dund gu am solo la ci yenn gox yi. + +Ay turam ci yeneeni làkk + +Bàmbara: zeguene. +Waa Càdd di ko woowe savonnier. +Wolof: Sump +Farañse: Dattier du désert. + +Turu xam-xam wi + +Balanites aegyptiaca +garab +meññeef +Ndiir xeetu ñax la gu bokk ci njabootu "Cyperaceae". + +Melo wi + +Ndiir ñax la gog ab guddaayam day toll ci diggante 25 ba 40i sànti meetar. Ay xobam dafa sew di gudde 5 ba 10i mm te tàllalu di niru ab jubb. Peeram dafa taxaw, liis te am i pàcc yu ñatti-koñe. Doom bi ci reen yi lay meññ. Ndiir bi day xaw a wurmbalu, yor wirgo wu jege mboq, ab deram ñagas. Ëmb na lu xaw a tollu ak 50% ci gilisit( sakaroos ak amido), 22% ci lipit ak 6 ba 7 poroteyin. + +Njariñ li +Dees na ko jaay ci ja bi. Ca Senegaal dees koy lekk noonu mbaa soppi ko diw. Amna ñu koy soppi njar niki waa-espaa��. Amna it ñu koy jëfandikoo nib fiirukaayu jën niki waa-àngalteer. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + +Cyperus esculentus + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Gerte tubaab xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Cambretaceae". +Mi ngi soqeekoo ci réewum Gine. +Barab yi bari naaj ak taw lay faral di sax. + +Melo wi + +Gerte tubaab garab la gog mi ngi toll ci 9 ba 25i met ci guddaay. +Ci jamonoy noor, ay xobam dañuy joxe wirgo wu palmaan lu jëkk ñuy wadd. + +Meññeefam nëtex lay tàmbalee, su jegee ñor day puur. Su ñoree dëgg nag day palmaan. + +Njariñam + +Manees na koo lekk noonu. +Manees na koo jëfandikoo it ci xeetu togg yu wuute. +Xooxam dees na ci sos ay fowukaay niki ay gaal yu daw + +Turu xam-xam wi + +Terminalia catappa +garab +meññeef +Uul xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Mimosaeae" (walla Fabasease). + +Melo wi +Garab la gog guddaayam man naa àgg ba 25i met. +Garab gi man naa jur ba 100i kiloy doom at mu nekk. Doom yi ñi ngi tàmbalee màgg ginnaaw taw yu njëkk yi. + +Njariñ li + +Ay xobam dinay dimbali suuf su nanguwul. +Garab gu bari ay witaamin la. +Doomi uul dees na ko baxal, dëbb ko ngir am ay dank walla pëndax (ginnaaw bu ñu ko weeree ) ñi ngi ko duppe sumbala ci bambara (Mali) ak yenn ci réewi Afrig Sowwu jant yiy làkk Bàmbara. +Doom bi dees na ko togg it ngir dindi xott wi, ginnaaw bi, ñu jariñoo la mu ëmboon. +Ca Senegaal, dees na dëbb doom bi boole ko ak kaani gu wow togg ci lees di woowe suul. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Parkia biglobosa + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +New xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Chrysobalanaceae" + +Cosaanam + +New a ngi fekk baax ci afrig soww-jant, ci digg afrig, ci Senegaal, Niseeriya, ak bëj-saalumu Sudã. + +Melo wi + +Ag garab la gu ndaw, taxawaayam man naa àgg ba ci 10i Met walla lu ko ëpp, garab la guy sëq, ay xobam day seex. +Doom bi dinay toll ci 5i sàntimet ci guddaay. Garab gi daanaka at mépp day am i doom, waaye lu ci ëpp ci ñaareelu xaaju noor bi lay am meññeef. Doom yi day nooy. + +Solo si + +Dees na ko faral di +jëfandikoo ci anam yu bari. Saal bi dees koy lekk. Garab gi nag bu màggee ci àll daay gi du ko manal dara. Doom bi dees koy witt ci ay lim yu bari a bari te di ko jëmbët ngir muy saxaat, dees koy jaay it ci ja yi at mi yépp. +Xob yi niki xas mi buñu ko baxalee galaxndikoo ko day faj bëñ buy metti, sunu ko yëyee itam day faj bëñ buy metti. +Reen yi aay nañu ci dereetal, sungufu reen bi itam boo ko defee ci ndox baax na ci bëñ buy metti. +Dees koy jëfandikoo batay ngir faj góom rawatina góomu aji-jong ji. Saal bi it dees na ko lakk def ko dóom di ko defaree saabu. + +Turu xam-xam wi +Neocarya macrophylla + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Gargamboose xeetu garab la gu bokk ci ñoñ "opuntia". Ca Amerig gu digg la bàyyikoo, fi ñuy woowee Karayib. + +Melo wi + +Gargamboose garab la gog day màgg te am xeetu xob yu dijj ak ay dég yu mag te ñaw, seen taxawaay di kaaraange, am na it dég yu sew yuy jame + +Meññeef mi + +Meññeef mi dees koy lekk. Dees koy xolli bam set bala ñu koy jëfandikoo. + +Njariñ yi + +Ay doomam bari nay njariñ lool. + +Dees na ci defar ay tàngal, ay njar walla njambaan yu neex. Ay bantam day faj (estomaa) góomu biir. Biir buy daw it dina koy faj, ba ci sax jabeet. + +Turu xam-xam wi +Opuntia tuna + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Lingoom garab la gu bokk ci njabootu "rutacées". +Dees na ko faral di bay ci barab yi bari naaj. + +Melo wi + +Garab la gog ay xobam dafay faral di wéy cig sax ci at mépp. +Danay dund lu tollu ak 50 ba 80i at. +Ay tóor-tóoram day weex. +Doom bi nag dafay muluŋ te cat la sew. Guddaayam di nay àgg ci 7 ba 12i sàntimet. + +Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx la, cig ñor nag mboq la. + +Ndox mi mu ëmb, cafka gi dafay sëcc(wex). Doom bi day ëmbaale ay xoox. + +Solo si + +Lingoom bari na nees koy jëfandikoo. Dees na ci génnee njar mbaa ndollenu njar. + +Turu xam-xam wi + +Citrus limon + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Guyug Afrig bokk na ci juróom ñàtti guy yi ñu gën a xam, mi ngi bokk ci njabootug Bombacacees. +Guy garab la gog dañu koo fonk lool ci aada ak cosaan, ñi ngi koy fekk ci barab yi am naaj fu ci mel ni réewum Senegaal ak Ginne. + +Melo wi + +Guy, garab la gog peeram da fa yaatu lool man a denc ndox mu bari, loolu moo tax ñu di ko woowe grabug butéel. +Ci guddaay mi ngi toll ci ñaar-fukk jàpp ñaar-fukk ak juróomi ñay ci yaatuwaay mi ngi toll ci juróom jàpp juróom ñaari ñay. +Bokk na ci garab yi nga xam ne day jël reenam dugal ko ci biir suuf ngir wuti ndox mum dunde. +Guy garab la gog manut a dékku ngelaw lu tar lool. + +Satamànna + +Satamànna mooy xobi guy yu ndaw yi. Moom nag dees koy jëfandikoo bu baax ci yenn barab yi. Dees koy watt di ko def laalo di ko boole ak cere. Jur gi it bëgg nañu ko lool. +Guy nag nawet kepp lay sëq am i xob, waaye yeneen jamono yi du am dara. Fu mel ni Kaasamaas nag, ca Senegaal, dees na fa fekk guy yoo xam ni at mi yépo dañuy sëq. Xobu guy nag, dana yaatoo 20i milimet. + +Mbotmbotaan + +Botmbotaan mooy tóortóori guy, moom nag day weex. Ginnaaw bu feeñee ba dem manees naa séntu wuy. Ba xiif di am daahees na ko lekk. + +Cëggal guy +Cëggal guy mooy xànci guy. Ca bu njëkk, dees ko daa xànc di ko weer di ci defar ay buum. Goj yi ñuy roote ci lees ko daa defare. + +Wuy + +Wuy wi di meññeef mi ñi ngi koy natt ci ñaari téemeer ak juróomi garaam, ci yaatuwaay mi ngi toll ci téemeeri milimet walla mu jàpp sax ñaar fukk i sàntimet ba ci sax fan weeri sàntimet ci guddaay. Man naa am ci biir lu ëpp 300i doomi buy. + +Buy + +Buy, mooy ñam wiy nekk ci biir wuy wi. Doom bu weex lay doon bu neex. Manees na koo macc noonu, manees na koo def njambaan mbaa njar. Ca Senegaal dees cay faral di def cifaay di ko boole ak laax. + +Gif + +Gif mooy xooxu buy. Boo maccee buy bi bamu set xoox ba cay des mooy wuy. Aw meloom day ñuul, boo ko tojee it day am aw kemb ci biir. Gif moomu nag moom jur guy, moom la ñuy ji. +Wolof da ne: Lu guy rëy rëy gifay ndayam. + +Xetax +Xetax mooy lu nëtëx liy muur xottu wuy. Bu taqee ci yaramu nit day xasan lool. Dees ci daan taal. Bu ñaar yi jonjoo, riisoonte man naa jur sawara. + +Turu xam-xam +Adansonia digitata + +Tur wi ci yeneen làkk yi + + Garab + Meññeef +Guyaab xeetu garabu foytéef la gu bokk ci njabootu "mirtaceae". Ci gox yi gën a bari naaj ca Amerig kepp la daa sax, ginnaaw bi la tas ci àddina bi. +Baatu guyaab ci làkku Arawaag la bawoo, turub dëkk la woon ci réewu saa-kolombi ya woon. + +Melo wi + +Taxawaayu garab gi dafa yem, man na àgg ba 8i sàntimet ci guddaay. +Xobam man na àgg ba 15i sàntimet ci guddaay ak 7i sàntimet yaatuwaay + +Guyaab bi (doom) xob wu nooy la yor. Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx gu leer la, cig ñor nag mboq gu dër la, day amaale ay tomb yu ñuul ci yenn xeet yi. + +Solo si + +Guyaab garab la gu ràññeeku te am solo ci wàllu koom. + +Dees na ko soppi njar, njambaanu foytéef ak yu ni mel. +Xolliitu foytéef dees na ci faj biir buy daw. Manees na ko lekk it nim bindoo. +Dees na ci jëlee sax gëtt. + +Turu xam-xam wi + +Psidium guajava + +Tur wi ci yeneen làkk yi + + garab + meññeef +Itaaliyee mooy làkk wa ñuy wax te juddoo ca Itaali. + +Karmat ak delluwaay + + + + + + Làkk + Itaali +Farañse mooy làkk wa ñuy wax te juddoo ca Faraas + + Làkk + Faraas +Ron walla sibi ca saalum, xeet la ci xeeti garab yu njool yiy gudd ne sóll ca kaw. +Mu bari lool ci tund Afrig, Eccopi, Afrig bëj-saalum. +Dees na ko fekk ba tay ci digg Afrig, fu ci mel ni Saara, walla Namibi. + +Melo wi + +Ron garab gog guddaayam danay àgg ba 25 ba 30i met. Yaatuwaayam nag danay àgg ci 1 met. +Xobam moom lees di wax xëddeen melo uppukaay la yor te guddaayam di mat 2i met. +Ron day am bu góor ak bu jigéen, bu jigéen bi ay xobam dana jàpp ci 260i sàntimet ci yaatuwaay. + +Foytéefam + +Moom lees di wax kóoni. Moom ab doom bu nëtëx lay doon am ci biir ay pax yu duy ndox mu neex ñu di ko naan. Bu demee ba ñor nag day soppiku di ab ron. Ñu di ko lakk di ko lekk. Boo ko lakkee bamu ñor nag dangay xolli der wi sànni lekk li ci biir. Li ci biir day mboq mel ni màngo saf suukar lool. + +Njariñ yi + +Garabug ron bari na ay njariñ lool ay xobam ñu koy wax ndon mooy daggiit yi ñu dagge ci xëddeen weer ko bamu wow, dees ciy taal ñu man cee togg. + +Xiis mooy lees dagge ci xëdéen ngir di ci yeewe ak a takke. Xiis bees ko takkee ci garab ag dënnu du ca daanu + +Turu xam-xam wi +Borassus flabellifer + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Tiir xeet la ci xeeti garab yu gudd yi ne sóll. +Mu bari lool ci tundu Afrig, Ecopi, Afrig bëj-saalum. +Di nañ ko fekk batay ci digg Afrig, fu ci mel ni Saara, walla Namibi. + +Melo wi +Tiir garab la gu baaxoo wéet. Guddaayam danay àgg ba 25i met. Yaatuwaayam nag danay àgg 1 met, Xobam melo uppukaay la yor te guddaayam di 2i met. Feggam daa am i dég. + +Tiir, day am bu góor ak bu jigéen, bu jigéen bi ay xobam dana jàpp ci 260i sàntimet ci yaatuwaay. +Day jur benn foytéef bu doom ba mboq, ci biir foytéef woowu dina am benn ba ñatti doom. + +Njariñ +Garabug tiir bari na ay njariñ lool ay xobam dañuy tàkk ñu man cee toggu. +Manees na cee def tam it sàngara +Doom bi daa neex lool nit ñi dañuy koy lekk + +Turu-xam-xam + +Borassus aethiopum + +garab +meññeef +Dimb garab la gu jub te gudd lool guddaayam man naa mat juroom ñeenti met ba ñeen fukki met. + +Barab yi +Dimb di sax nag yii la: Senegaal, Mali, Niseeriya ak Kamerun. + +Doom bi + +Doom bi dees koy lekk ci tooyaay bi ak bu wowee itam saal bi it dees koy lekk nit ak mala yépp a ci yam. +Mutt-mutt di doomu dimb bu ñor bi, moo gën a neex keŋ. Keŋ mooy doom bi ñoragul. +Àllambere mooy der biy muur saal bi. Saalub dimb it lu am solo la. + +Bant bi + +Bant la bu ràññeeku ci bant yi ndax talaayam ak dëgëraayam, max manu koo yàq. Dañ koy jëfandikoo ngir defar ay lal ak i armuwaal yu rafet te man a yàgg. + +Njariñ yi +Dimb garab gu ñaas, am xasam di lekkloo tey faj saw-lal, day faj lu bari, bokk na ca ray jaani-biir, di ko daggte ba nga koy saw, garab gu baax ci suuf ngir ne lu meññ ci ronam màgg te naat, boroomug kër gu neex la te amadi dég, ker gu dége mooy gu picc yay toŋ cag garabam te di fa tàgg ba toog fay jafe. + +Turu xam-xam wi +Cordyla pinnata + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Saab-saab xeetu garab la gu bokk ci njabootug « Moringaceae », mi ngi bàyyikoo ci bëj-gannaaru End. +Garab gu fés la leegi ci àddina bépp, te miin barab yi bari naaj. + +Melo wi +As ngarab la su gaaw a màgg te man a muñ bekkoor. Guddaayam danay àgg ba 10i met. Saab-saab garab guy gaaw a màgg la. +Peeram danay àgg ba fukk baa 12i met, dàttam nag danay àgg ba 45i sàntimet, xàccam melo wu baam la te jege weex. + +Tóór-tóor bi + +Tóor-tóor bi daa am xet te nguuni-ngaana, danay am ba juroomi xob yu tolloowul. +Wirgoom dafa mboq. +Tóor-tóor bi guddaayam 1 la ba 2,5i sàntimet cib guddaay. +Yaatuwaay bi 2i sàntimet la. + +Doom bi + +Doom bi këmbaan la gu ñàtti-koñe te palmaan. Guddaayam 20 la ba 45i sàntimet. Xoox bi dafa wërmbalu. + +Solo si + +Saab-saab bari na pàcc yees ciy jëfandikoo: foytéef bi, xob wi, xoox bi su ñoree, diw bees ciy jële, tóor-tóor bi , reen yi. +Saab-saab dees na ko jëfandikoo ci anam yu bari ci wàllug toggu ci àddina bépp. +Manees na ko lekk nim bindoo. Fële ca Senegaal dees na ko toggu boole ko ak cere (cere mbuum). + +Turu xam-xam wi +Moringa oleifera + +Tur wi ci yeneeni làkk + +Garab +Meññeef +Xaal genn xeetu ñax la. Mi ngi bokk ci njabootug "cucurbitacées" te cosaanoo Afrig gu sowwu jant. + +Melo wi + +Xaal ñam wu xonq la yor, Ay foytéefam buñu matee dëgg diisaayam danay àgg 5 jàpp 20i kilo. +Foytéef bi daa mbege te xaw a muluŋ. +Xaal garab la guy sax at ba at (nawet lay sax). Ronam ( peer ak dàtt) danay àgg ba 3i met ci guddayam. +Xobam cig yaatal day ñatti-koñe. + +Njariñ + +Xaal, doom bi dafa neex lool, léppam dees koy jëfandikoo. +Ñamam dees kox lekk. Xoliit yi nag dees na ko jox rab yi mbaa def ci cere. + +Turu xam-xam wi +Citrullus lanatus + +Tur wi ci yeneeni làmmiñ + +Araab: البطيخ +Español: sandía +Itaali: Anguria/cocomero +Tirk: Karpuz +Portige: Melancia Àngale: Watermelon +Almaa: Wassermelone +Kabiil: Tadellaεt +Endo: Tarbuz Faaris/persã: خربوز/kharbuz +Sapone: スイカ?( Suika) + + garab + meññeef +Daqaar garab la gu fekk baax ca penku Afrig ca àllu Madagaskaar waaye bari lool ci Afrig sowwu jant fu ci mel ni Senegaal bari na fa lool. Guddaayam man naa àgg ci 20i met waaye itam dafa yeexug màgg waaye nag garab gu man a gudd fan la. +Ca Senegaal nag, dees faa xaw a gaafal garabu daqaar. Di wax naan ay jinne dañu fay dëkk, ba ñu bari ñimewuñu koo def seen kër. + +Meññeef mi + +Meññeefam te mooy doom yi guddaayam di mat 20i sàntimet. +Buy door a meññ mooy benqal, day nëtëx te neex lool ñu man koy lekk noonu. Bu ñoree lay doon ub daqaar. Dees na ko jëfandikoo fu bari. Boo maccee doom bi ba noppi day am ab xoox ca biir. Xoox booba mooy sax. +Daqaar dees koy jëfandikoo di ci defar naan yu neex. Ak di ko def maccaat ci ceebu jën, te itam njarum daqaar day faj seere di raxas biir, dana faj itam bóoli guy metti. Dees na ko def it cifaay ci laax, ñu di ko wax: Laaxu daqaar. + +Ngogna + +Ngogna di tóortóori daqaar. Moom it daawees na ko jëfandikoo ci cifaayu laax. Niki laaxub ngogna. Jamono yi daqaar gi meññagul amagul i doom te tóortóor booba lees daa jëfandikoo laaxub ngogna. + +Cafna + +Mooy xobi daqaar. Moom it daawees na ko jëfandikoo di ko def cifaay di ko boole ak laax ñu koy wax laaxub cafna. +Jamono ji nga xam ne daqaar gi meññagul, tóortóoragul ci lees daa jël xob yi di ko def cifaay. + +Turu xam-xam wi +Tamarindus indica + +garab +meññeef +Xewar xeetu garab la gu bokk ci njabootug « Sapindaceae ». + +Cosaan li + +Moo ngi tasaaroo ca Afrig ci réew yii: Senegaal, Eritere, Ecopi, Somali, Sudaan, Keeñaa, +Tansani, Ugàndaa, Kamerun, Réewum Diggu-Afrig, Gaboŋ, Kóngoo, +Bene, Kodiwaar, Gàmbi, Gana, Gine, +Gine bisaawóo, Niseer, Niseeryaa ,Tógoo, Àngolaa, Mosàmbig, Madagaskaar. + +Amna it ca Asi gu bari naaj ga: +Bangalades, Butaan, End, Nepaal, Siri-lànka, Kàmbots, Lawos, Birmani,Taylànd, Wiyet-naam, Endonesi, Maleesi, Papuwaasi Gine Gu yees ak Filipiin. + +Melo wi + +Xewar garab la guy toll ci 6i met ci guddaay. Ay xobam day nëtëx. + +Turu xam-xam wi + +Lepisanthes senegalensis (Aphania senegalensis) + +Tur wi ci yeneeni làkk + +farañse: Cerisier du Cayor + +garab +meññeef +Dëkku Liberewiil +Njàndam xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu “capparaceae”. +Moo ngi bàyyikoo Afrig gu sowwu gi. + +Melo + +Njàndam gancax la guy sax fu nekk. +Dana àgg yaar ba juróomi met cib guddaay. + +Njàndam day meññ ay foytéef. +Ay tóortóoram day dajaloo. + +Foytéef bi danay am benn ba ñenti xoox yuy yor wirgo wu nëtëx su ñoree. + +Solo si + +Njàndam dees na ko jëfandikoo cig togg ak cim paj. + +Ay doomam dees na ci jële xeetu ñam yu nekk. + +Turu xam-xam wi + +Boscia senegalensis + +Taram ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Garabu taba garab la gu man a toll ci fukk ak juroom ba ci ñaar fukk met. Peer bi am daa kaaraange lool. Xas mi am ay xar-xar. Xobi garab gi man naa yaatu lool di toll ci juroom ñatti sàntimet ba ci fanweer ak juroom ci ay sàntimet, am it ay pàcc-pàcc yu man a àgg ci ñatt ba juroom ñaar. Taba garab la guy tóor-tóor, tóor-tóor yuy tijjeeku ba ci juroom ñaar. + +Meññeef mi + +Foytéefam daa am xott wu koy aar. Xott woowu moom la ñuy toj ngir jot taba ja ca biir, bu xott wi ubbeekoo man na ñoo nekk ci biiram ñeent ba ci juróom ñent donj taba leeg-leeg muy ñuul mbaa muy mboq mbaa muy xaw a jege xonq. + +Turu xam-xam wi + +Cola cordifolia + +garab +meññeef +Tol ag garab la, bokk ci njabootug "Apocynacées" + +Melo wi + +Garab gu ndaw lay doon ,ay doomam da ñuy muluŋ am ay doom ci biir, doom yi manees na koo lekk bu ñoree ak buy bëgg a ñor. Doom bi day xaw a xonq. Tol, ñi ngi koy fekk ci yenn gox yu mel ni ca kaskaat ya, ak yenn ci barab yi am ay xeer. + +Solo si + +Doom bi bu matee dëgg, dees koy lekk noonu. Doom bi manees na cee defar ay naan walla sax sàngara. Dinay aare ci yenn xeeti feebar yi lu ci mel ni jabet ak ñoom séen. Bokk na ci garab yi nga xam ne dañuy reesal lekk. + +Turu xam-xam wi + +Landolphia heudelotii + +garab +meññeef +Neb-neb garab la gu am i dég yu ñaw, guddaayam man naa dem ba 5i ba 20i met, ay xobam day sew. + +Njariñ yi + +Garab gu bari ay ferñeet la, day faj gémmiñ guy xeeñ baxalal xob yi di ko galaxndikoo da koy faj, day dindi kadam itam. +Xas mi day faj biir buy metti, walla muy daw, ba ci ilseer sax da koy faj. +xasum neb-neb day faj ilseer, reen bi soo ko boolee ak reenu Xarañ walla reenu Tëmb day faj jigeen ju jaasir. Doom bi daa bariy ferñeet lool. + +Turu xam-xam wi + +Vachellia nilotica (Acacia nilotica) + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Dambal garab gu siiw la ci ne Senegaal la bàyyikoo waaye dees na ko gis ci yaneeni barab ci Afrig. + +Melo wi +Garab la guy àgg 10 ba 15i met. + +Xobam dafa wërmbalu tóor-tóoram juróomi xob la am. +Guddi day gilli xet gu xasaw, day ndiiraan foytéef bu lax. + +Xetam day xàcc njugub yiy ñëw sabab ag saxam. + +Danay meññi ay foytéef yu dijj te baam ba noppi di lang. +Foytéefam siiw na ci ne nit du ko lekk waaye ca gox yamuy sax dees nako lekk ci lu dul togg. + +Njariñ yi + +Ginnaaw ag lekkam baa ag taaralam, dees na ko jëfandikoo ci taaral deru jigeen, dees na ci génnee it diw dees na ci faje it, dana faj ñatti xeetu kaaseer: kaasseeru ween, kaaseeru res, kaaseeru suufu nit. + +Turu xam-xam wi + +Kigelia africana + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Karasol garab la gu bàyyikoo ci lu bir ci àll yu naaje yu Karayib, yu Amerig gu digg ak gu bëjsaalum. + +Melo wi + +Karasol gàncax la gu ndaw. Guddaayam danay àgg 3 ba 10i met. Xobam melo wu nëtëx la yor. Tóor-tóoram 3i xob la yor. Day meññ at mépp. + +Njariñ yi + +Karasol dees na ko lekk. Dees na ci defar njar. Dees na ci fajoo it. + +Turu xam-xam wi + +Annona muricata + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Ñamako xeet la ci xeeti garab yi nga xam ni seenug dund man naa yàgg lool. Ñu ngi koy fekk ci tundi Afrig. + +Njariñ li + +Garab la gog ay doomam dees koy jëfandikoo, ngir xeeti saf-safal. Dees na ko jëfandikoo it ngir neexal sëy. + +Jaarjaaram + +Ñamako bokkoon na ci njaay yi nga xam ni ñoo gënoon a dox ci yiñ daa dugal ca Afrig sowwu jant, ci jamonoy xarnub 18. +Loolu sax moo tax ñu di ko woowe, "côte du Poivre" fële ca Gine. + +Turu xam-xam wi + +Aframomum melegueta + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Mbàccaar xeetu garab la gu bokk ci njabootu "caesalpiniaceae" walla "fabaceae". Tóortóoram daa xonq te taaru lool. Madagaskaar la bàyyikoo waaye leegi ci barab yi bari naaj ci àddina bépp dees na ko fa fekk nib garabu taaral. + +Melo wi + +Ponkalu garab gii danay romb 15 met ci guddaay. Téeñam jëmmu fanq-naaj la yor. Tóortóoram 4i xob yu xonq la yor yuy xaw a tolloo ak 8 sàntimet, ak uw ñeenteel wu gën a rëy wuy nekk ci digg bi te yor wirgow xeex ak mboq. Mbàccaar si ronam day liis te leer. + +Mbàccaar bi melo ñebbe la xaw a yor te guddaayam di àgg 40 ba 60 sàntimet. Yaatuwaayam danay àgg 5 sàntimet te da day ëmb 10i xoox. + +Mbaaxam + +Barab yi xaw a naaje la taamu, waaye danay muñ bekkoor, xorom. Bëggut suuf yi bane te tooy, suufus joor moo ko gënal. + +Solo si +Garabu ker la baaxoo ci tool yi, bedd yi ak kër yi. +Dees na ci yàtt gaal, dees na ci wutum màtt te di ci fajoo. + +Turu xam-xam wi +Delonix regia + +Turam ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Mbal ag garab la gog mi ngi bokk ci njabootug " Euphorbiaceae". Mi ngi bokk ci gàncax yi nga xam ne at ba at lay meññ. + +Mbooram + +Mbal mi ngi cosaanoo fële ci diggu Amerig. Mbal garab la gog day sax foo xam ne baaxu faa saxe mu yaatu lool ci tund yi nga xam ne dafa am naaj. Niki noonu bari na fële ca Afrig bëj-Saalum. + +Njariñ yi + +Mbal garab la gog bari na xeeti jàngoro yu bari yu muy faj, loolu moo tax fépp fumu nekk dan ko fay jëfandikoo rawatina fii ci Afrig nga xam ne dañu ko fiy jëfandikoo ngir muy faj, biir buy daw, naka noonu da��u koo faa jàppe ngir ne mooy li gën a gaaw ngir faj lépp loo nga xam ne dafa jëm ci wàllu noyyi lu ci mel ni asma, ak yaneen xeet yi ni mel. + +Bokk na ci ay njariam batay dañoo wax ne moom moo gaaw lool ci faj bopp buy mett. ak bëñ buy metti. + +Turu xam-xam wi +Euphorbia hirtata + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Ngun-ngun xeetu gancax la gu bokk ci njabootu "asteraceae". Garabu rëndaay la, dees ciy safal. + +Melo wi + +Gàncax la guy tollu ci 20 ba 90i sàntimet ci guddaay. Xobam daa tàppndar, danay àgg 2 ba 3i sàntimet. Xobam ci diggante nëtëx bu dër ak woyof, yenn saa yi nag mu ngolleñ ci yenn xeet yi. + +Njariñ li + +Am rënd mu am solo la ci wàllu togg ci yenn réew yi. Ca Senegaal dees na ko def ci ataaya. Gàncax la gees di fajoo it. + +Turu xam-xam wi +Blumea aurita + +garab +Dibbtóon (pos ca Saalum) as ngarab su ndaw la su man a toll ci juroom benni met. Xobi dibbtóon day xaw a dëgër. Ay wàqaasam day laxasoo di am car yu ndaw yuy am i dég. +Garabu dibbtóon manees na koo góob ci àll ngir jëfandikoo ko cim paj. + +Barab yi + +Garabu dibbtóon man nañu koo fekk ci kembaaru Afrig li ko dale Seneegal ba Ecopi, Ugandaa, Keeñaa, bëj-saalumu Namibi Botswaana mbaa ca Mosàmbik, gàncax la gu man a màgg ci suuf su nanguwul, ci suuf su wow mbaa su am i xeer wala suuf suy taa nawet. + +Meññeef mi + +Doomub dibbtóon deesu ko lekk, ay xobam it noonu. Waaye reen yi buñu ko baxalee man naa faj tooy ak coono. Leeg-leeg ñu toggaalee ko ak laax mbaa ruy ngir faj yaram wu tàng. + +Yeneeni njariñ +Bantu garabu dibbtóon manees na koo lakk ngir am xeetu sunguf su ñuy defare saabu. Doom bi manees na cee cuub. + +Turu xam-xam wi +Gardenia ternifolia + +garab +meññeef +Kullu-kullu turu xam-xam wi di morus Mesozygia. Jëmmam taxu koo rëy noonu. Nu koy faral di gis ci àllu Afrig yu ëpp ndox yi. Xob ya ak meññeef ya dinañu dundal guereza, unsinge colobe mi nuy gis lu ëpp ca Afrig Sowwu jant ak gu diggu gi. Yenn saa yi nag nu def ko matt di ko jaay. + +Barab yi +Jamono jii garab gi bari na lool Ngogo, ca kër-Mala boobu nu naan Kibale ca Ugàndaa, mu nekk lu "chimpanze" yi du dunde bis bu ne. + +Turu xam-xam wi +Pericopsis laxiflora + +garab +meññeef +Sànd garab la gog daa bokk ci njabootug moresea nekk ca Afrig sowwu jant, garab gu njool la man a àgg ba ci 20i met, day ruus jamonoy noor di sëq ci jamonoy nawet. Ay xobam am na ñu koy jëfandikoo cig togg di ko lekk. + +Meññeef mi + +Bu nawet biy jeex lay meññi. Dees koy lekk it, mu neex lool. + +Turu xam-xam wi +Morus mesoziygia +Keŋ garab la gu gàtt gu man a toll ci 4 ba ci 7i met gën gaa bari. Garab gi day am ay car yu bari yoo xam ne suuf lañuy jóge jëm ci kaw mel ni lu wërngalu. Xobi garabu Keŋ leeg leeg dañuy wadd su dee barab bi mu nekk daa wow waaye su tooyee man nañoo bañ a wadd. + +Njariñ yi + +Garabu keŋ bari nay njariñ lool. Ñu man koo jëfandikoo ci faj lu baree bari. Amna sax ñu ne bokk na ci garab yi ëpp njariñ ci lu nuy fajoo ci sunu tund yii, waaye it garab la gu bari ay loraange. Manees na cee defar tooke yu man a ray yenn mala yi niki jinax añs + +Garabu keŋ man naa dund ciy barab yu wuute niki ci àll bu bariy garab, mbaa ci barab bu bari ndox walla bu ko amul, mbaa ñu man koo fekk ci kaw dëkkuwaayu xorondom yi, mbaa melentaan. Keŋ ku ko fekk ci tool bu ñuy waaj a bay deesu ko dindi ndax njariñ yi mu man a amal suuf si. + +Turu xam-xam wi +Flueggea virosa + +Tur wi ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Lóriye gi xeetu garab la gu bokk ci njabootug Lauraceae, ci bëj-saalumu Tugal la bàyyiko waaye amna ci barab yi bari naaj ci àddina bépp, Senegaal it. + +Melo wi +Garabug lóriye dafa man a àgg 10i met ci guddaay, xobam day gulumba te wirgo wu nëtëx lay yore, tóor-tóor bi day mboq. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Laurus nobilis + +garab +Sanqaay xeet la ci xeeti garab yoo xam ne dañuy màgg ci fu am naaj, ñung kay fekk ci kémbaarug Afrig bu yaatu fa lool. Waaye itam, Waaye desu ko fekk fu mel ni: Nambi bi, ak Butsuwanaa, ak Afrig bët Saalum. + +Melo wi + +Garab la gog man naa sax foo xam ne amul ndox. Baayima yu bari dan koy jëfëndikoo ngir di ci tabax seen i dëkkuwaay lu ci mel ni xeet i picc yi. Ay xóbam dana yor melo bu muloŋ , ci yaatu waay, manees na koo natt ci juróom-fukk, jàpp teeméer ak juróom-fukk ci ay milimeeter. + +Solo si +Ay xóbam, danoo gaaw ci lool ci xeex biir buy daw, loolu moo tax mu bokk ci xeeti garab yi nga xam ne ci fajum cosaan. + +Turu xam-xam wi +Ficus glumosa + +Turi ci yeneeni làkk + + Garab + Meññeef +Naruhito : Njiitu Réew Sapoŋ. +Dóobaali garab la gu rëy gu am xob yu dëgër yu man a toll ci juróom-benn ba ci ñaar fukk ak benni met ci njoolaay. Lu ci ëpp ag ray-donn lay doon. Muy garab gi day juddoo ci kaw geneen garab gu màggat. Bu juddoo ci kaw garab googu, dana am ay reeni jaww yoo xam ne dana màgg ba laal suuf di am it ay xob yuy mujjee muur xobi garab gi mu juddoo, am peer bu mujj nangu peeru garab gi mu juddoo mujj gi nag mu nekk garab ci boppam gu rëy lool. + +Njariñ yi +Garab gi nag leeg-leeg man na��u koo jëmbët ngir ay foytéefam walla ay njariñam cim paj walla yeneen yuñu ko man a jëfandikoo. Leeg-leeg it danañu ko jëmbët ngir mu man a mbaar ci bërëb yi ñuy féexloo. Keppaar gu neex la am. + +Njariñi paj yi +Dóobaali garab gu bari ay njariñ la ci wàllu paj. Xas mi dañu koy jëfandikoo ci lépp luñuy faje fajum cosaan. Maanaam faj soj, man a faj put guy metti, man a faj biir buy daw, man a faj i goom, man a faj seere, man a faj bakkan buy bori, ñu man koo it jëfandikoo ngir yokk meewu jigeen juy nàmpal. Amna it lu ñu man a jël ci xas mi boole ko ak ndox mu tàng ngir faje ko feebaru sëqët, man a faj feebaru laago man a faj feebaru gaana. Ba leegi ci xas mi, man naa faj it feebaru kataraag. Reen yi ku ko togg jox jo jigeen ju ëmb, man na ko musal ci ëmb buy yàqu. + +Leneen ci ñjariñi garab gi xas mi man nañu cee liggeey basaŋ yu baax, man cee liggeey goj yu dëgër mbaa nu jëfandikoo bant bi niki mat mi ñuy toggee. + +Mbay mi +Mbayum dóobaali lu man a nekk la ci ñaari fànn. Bi ci njëkk mooy garab gi man nañu koo ji xaar mu sax wala ñu dagg lu cosaanoo ci moom, weer ko ba mu xaw a fendi, ñu sàmpaat ko ci suuf su nooy, suuf su tooy, ci bërëb boo xam ne danañu ko aar ci ngelaw ba mu bañ a damm. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Ficus thonningii + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Garabu papaya lu ci ëpp nu ngi koy gis ci diwaan yi nga xamne ndox dafaa bari. Mu ngi soqeekoo ca "Sud Mexique" . + +Guddaayam dana tóll ci 3 ba 7 meetar. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xamne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo. + +Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróom i at su bare ba bare waaye ci at mu njëkk mi dina tambale am meññeef. + +Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wàqaas. + +Xóotaayu biiram tóll na ci 20 Cm (Diamètre), te li ko wër lépp yeen saa yi mu yor melo wu (vert,) yenn saa yi mu yor wu gris. +Ngeer xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu "combretaceae". Wenn la ci xeetam. + +Melo wi +Ngeer ngàjj la gu man a àgg ba 3i met. Bari lool ci Saara bi, ci sowwu jantub Afrig, fu ci mel ni Senegaal. Garab gu yam lay doon te firiku. Di xaw a tolloo ak salaan. + +Njariñ li +Ngeer garabu paj la, bokk na ci yi ñu gën a taamu ca Sowwu Afrig. Dees na ko fa jëfandikoo ngir faj xeetu wopp yu bari te wuute. Jëfandikoom danay xaw a niru ak gog kenkelibaa, te ñoom ñaar lees faral di boole, ngir faj tawatu soj, tàngooru yaram ak jafe-jafey nokki. Xob yu wex yi lees faral di jëfandikoo. Dees na ko boole ak rat it ngir faj ci soj. + +Ndox mi muy ëmb, da koy tàbbal ci suuf si yeneen garab yi jariñoo ko. Kon ba ko cib tool làmboo nay njariñ. + +Nataal yi + + Garab + Meññeef + +Turu xam-xam wi +Guiera senegalensis + +Tur wi ci yeneeni làkk + + Garab + Meññeef +Rajab manees naa wax ne ci xeetu garab yi la bokk. Amna ñu ko ber it ne du garab. Bari na ay xeet lool nag, amna lu ëpp téemeeri xeet. + +Xeet yi +Amna ci bu ñuy wax kooyi naar, pakkub lëg, jaatoor, beñeb lëg, sawum xaj. +Amna ci yu weex am ci yu yor yeneen i wirgo. Amna ci yu ñuy lekk, te muy sax ci suuf di am jëmm, am ci yoy tooke la day raye. Yooyu di raye nag Afrig la ëppe ci tàngoor wi, fu ci mel ni Senegaal, rajab ya fa nekk, kenn waru koo lekk. + +Saxiin wi +Moom rajab nag ci ngelaw li rekk la aw jiwoom di jaar. Jiwu wu góor wi mooy naaw daje ak wu jigeen wi ñu joxe doom. +Amna ci yoy, day yàq garab da koy ray. Pëndax lay doon bu weex tuuru ci garab gi ne ci ñàpp. +Pëndëx boobu it bu laalee kawari nit, da koy xus moom la ñuy wax mbay-wataan . Rajab yi tuuti ba kenn manu koo gis ak bët moo koy def. Lu bari looy gis mu xuur nag, bu dul bagteri rajab a ko waral. + +Nataal yi + +Tur wi ci yeneeni làkk + +Garab +Meññeef +Caxat lawtan la, xeetu ñax guy law. Ñax la gu man a muñ bekkoor. Dees na fekk ca Afrig gu naaje gi: Senegaal, Kamerun, Keeñaa, Ugandaa, Ecoopi. + +Melo wi +Guddaayam danay àgg 20i met. Ag ndomaam di mat 10i sàntimet. Dafa nguuni-ngaana, te ag meññam daa yeex, ci njeexiitalu noor mbaa nawet bi lay faral di meññ. + +Njariñ li +Fi muy sax fépp, xobam yi, meññeefam mu yees mi ak tóortóoram bi dees leen fay lekk ni ay lujum yu ñorut mbaa nu supp leen. +Dees na ko xonte gàtt yi. Garab la guy faj tawat yu takku ci lim: góom, biir buy daw añs. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Leptadenia hastata + +Tur wi yeneeni làkk +garab +ñax +Bul garab la gu am ay xob yu tasaaroo ak peer buy gudd lool bu man a àgg ci fukk ak juroom ñatt ba ci ñaar fukk ak juroomi met ci njoolaay. Ci gëx bi di njëlbeenu peer bi dana yaatu ba àgg ci juroom benni met peer bi nag ci boppam man naa dem ba ci lu ëpp met ci xala ci yaatuwaay. + +Njariñ yi +Garab gi ay njariñam manees na cee faju man nañu koo jëfandikoo ci matt walla sax ñu di ko lekk. Ci wàllum paj xas mi man naa faj ay tànk yuy ruux walla tànk yu ab sedd di jàpp. Reen yi man nañu koo jëfandikoo ngir faj feebaru xel. Yu bari ci garab gi it man nañu koo jëfandikoo ngir faj tële ak faj bopp buy metti ngir faj ay picc ngir faj yaram wuy sol ndox ngir faj coona walla it nu man koo jëfandikoo ngir di ci faj i goom walla di ci faj i saan man na it yombal njurum jigéen maanaam jigéen juy wësin dena ko koy yombalal. + +Jëfandiku gi +Leneen ci ñariñ yi: +Garab gi man nanoo jëfandikoo xas mi ngir defar ci ay basaŋ walla am ci matt mu ñuy togge. + +Mbay mi + +Bul garab la gu ñuy ji waaye ji gi bu jàppee màgg gu gaaw lay man a màgg. Manees na koo jëmbat it, boo amee nduutan gi di njëmbat, man nga koo jëmbët. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Celtis toka + + garab + meññeef +Pàppaaya ñu ngi koy fekk lu ci ëpp ci fu bari ndox. Bu dee ca Senegaal bari ca fa ñuy tudde ñaay bi ak ca Kaasamaas. + +Melo wi +Guddaayam dana toll ci 3 ba 7u met. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xam ne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo. Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróomi at su bare ba bari waaye ci at mu njëkk mi dina tambalee am meññeef. Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wànqaas. Ag ndombaam nag da mat 20i sàntimet . Yaram wi yenn saa yi mu yor melo wu nëtëx yenn saa yi mu yor wu baam. Xob wu rëy lay yor wow manees na cee uppu. + +Njariñi paj yi +Boo amee liir buy sank muy seere dangay jël ñam wi ci biir nga nal ko di ko ko jox kudd gu ndaw dana dindi seere bi. Bu dee mag mu jël genn wàllu kaas. Ñi am jafe-jafey reesal buñuy jël doom bi ba la ñuy tëdd dinañu reesal ni mu ware. Ku am dagg-dagg bu bees bu jëlee xott pàppaaya wu xaay wi teg ko ci dana tax dagg-dagg bi gaaw a wér. + +Paj +Ku am bopp buy metti bu jëlee xobu wi tiimale ko ci taal bamu xaw a tàng mu takk ko ci bopp bi bàyyi ko bamu sedd ci dana ko saafara. Naka noonu day faj pëyiis ak epaatit ak sëqët. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Carica papaya +Sexaw ci njaboot gu yaa gog "combrétacées" gi tënk ñaxi yi ci àll ak mànding. Sexaw xeetu garab gu sëkk, man àgg 4 ba 5i met. + +Melo wi + +Tóortóoram daa tuuti te weex, ba noppi dajaloo te am i dég. + +Foytéefam daa wow te yor ay xeeti laaf yuy àgg ba 1,5 sàntimet ci guddaay, ak 1,5 sàntimet ci yaatuwaay. + +Meññuwaayam + +Sexaw ci réewi sahel gi lay sax: Senegaal, Mali, Niseer, Burkinaa, Gine konaakri/Bisaawóo. + +Njariñ li + +Sexaw ràññees na mbaxam ci reesal ak ci moytu ag mbëfër. Ca Senegaal xob yi dañ ko fas ak i xëddee di ko jaay ngir defarug dute mbaa ndékki. + +Nataali sexaw + +Turu xam-xam wi + +Combretum micranthum + +Turam ci yeneen làkk + +Araab: +Farañse: kinkeliba + + garab + foytéef +Fuuf xeetu gàncaxu tóortóor la gu bokk ci njabootu "polygaceae". Dees na ko jënfandikoo ngir ay jagleem ci wàllu njaay ak paj, ci pajum coosaanu Afrig. + +Melo wi + +Ñax la gees di buddi ngir ay reenam. Barab yi tàkke lay faral di ne: Burkinaa Fasóo, Sudaan, Senegaal. Beru la baaxoo te guddaay danay àgg ba 5i met. + +Oktoobar ba nowambar lay tóortóor, tóortóoram wirgow ngolleñ bu dër la yor te day gilli xet wu tar te saf suukar. Fuuf bi danay des ci fuuf gi lu mat weer. + +Njariñ li + +Xooxam danay jariñ ci wàllu aniin, ginnaaw biñ ko dëbbee te togg ko toggu ko yem. Diwam suñ ko nalee, njariñ la ci jagal kawar ak der. Dawam siiw na ne tooke la ci biir. + +Reenam lees di fajoo la ci pajum cosaanu Afrig. + +Njariñal paju garab gi ci yaatal yii la: + +-Toppatoo mettiitu gëñ. +-Xeet egsemaa +-Xam, ngénnaliku der. +-Néewle dereet + +Nataali fuuf + +Turu xam-xam wi + +Securidaca longipedunculata + +Turam ci yeneeni làmmiñ + +Araab: +Farañse: + +ñax +Guy + Daqaar + Kullu-kullu + Sànd + Dibbtóon + Keŋ + Ñamako + Mbal + Dambal + Bàccoor + Mbàccaar + Karasol + Ngun-ngun + Pàppaaya + Rajab + Sexaw + Bul + Dóobaali + Sànqaay + Lóriye + Ngeer + Caxat + Fuuf +Sànqaay : xeet la ci xeeti garab yoo xam ne dañuy màgg ci fu am naaj, ñung kay fekk ci kémbaarug Afrig bu yaatu fa lool. Waaye itam, Waaye desu ko fekk fu mel ni: Nambi bi, ak Butsuwanaa, ak Afrig bët Saalum. + +Melo wi + +Garab la gog man naa sax foo xam ne amul ndox. Baayima yu bari dan koy jëfëndikoo ngir di ci tabax seen i dëkkuwaay lu ci mel ni xeet i picc yi. + +Ay xóbam dana yor melo bu muloŋ , ci yaatu waay, manees na koo natt ci juróom-fukk, jàpp teeméer ak juróom-fukk ci ay milimeetr + +Solo si + +Ay xóbam, danoo gaaw ci lool ci xeex biir buy daw, loolu moo tax mu bokk ci xeeti garab yi nga xam ne ci fajum cosaan. + +turu xam-xam yi +Ficus glumosa + +garab +meññeef +Pàppaaya ñu ngi koy fekk lu ci ëpp ci fu bari ndox. Bu dee ca Senegaal bari ca fa ñuy tudde ñaay bi ak ca Kaasamaas. + +Melo wi +Guddaayam dana toll ci 3 ba 7u met. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xam ne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo. +Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróomi at su bare ba bari waaye ci at mu njëkk mi dina tambalee am meññeef. +Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wànqaas. +Ag ndombaam nag da mat 20i sàntimet . Yaram wi yenn saa yi mu yor melo wu nëtëx yenn saa yi mu yor wu baam. Xob wu rëy lay yor wow manees na cee uppu. + +Njariñi paj yi + +Boo amee liir buy sank muy seere dangay jël ñam wi ci biir nga nal ko di ko ko jox kudd gu ndaw dana dindi seere bi. +Bu dee mag mu jël genn wàllu kaas. +Ñi am jafe-jafey reesal buñuy jël doom bi ba la ñuy tëdd dinañu reesal ni mu ware. +Ku am dagg-dagg bu bees bu jëlee xott pàppaaya wu xaay wi teg ko ci dana tax dagg-dagg bi gaaw a wér. + +Paj +Ku am bopp buy metti bu jëlee xobu wi tiimale ko ci taal bamu xaw a tàng mu takk ko ci bopp bi bàyyi ko bamu sedd ci dana ko saafara. Naka noonu day faj pëyiis ak epaatit ak sëqët. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Carica papaya + +garab +meññeef +Preguiça benn dekk-dëkkaan Ribeira Brava ci yu bëj-saluumu yu dunu São Nicolau, Kap Weer. + +Way-dëkk +2000: 465 +2010: 567 + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Palmeira benn dekk-dëkkaan Sal ci yu penku yu nekku Sal, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Sal (Kap Weert) +Picos (Achada Igreja) benn dekk-dëkkaan São Salvador do Mundo ci yu penku yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Plano comunal de São Salvador do Mundo (Mee 2009, p. 28) +"Moradores da zona alta d Achada Igreja reivindicam melhores condições de vida" (RTC TV Notîcias- video) +"Água chega a centenas de casas em Achada Igreja e Achada Leitão" (A Nação, 2011-12-14) + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Povoação Velha benn dekk-dëkkaan Boa Vista ci yu penku yu nekku Boa Vista, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dëkki Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +Fajã de Água benn dekk-dëkkaan Brava ci yu penku yu sowwu yu dunu Brava, Kap Weer. + +Dencukaay + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Brava +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Furna benn dekk-dëkkaan Brava ci yu bëj-gannar-penku yu dunu Brava, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +https://web.archive.org/web/20200803212204/http://furnaschool.com/ +http://portfocus.com/cape_verde/porto_furna/index.html + +Brava +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Pombas (Paul) benn dëkku Paul ci yu nekk Santo Antão, Kap Weer. + +Football klubi +Paulense DC + +Karmat ak delluwaay + +Turu xam-xam wi +Carlos Ferrão, Estudos sobre a Ilha de Santo Antão, Imprensa Nacional, Lisboa, 1898 +García, Jesús (2009) El mundo a tu aire: Cabo Verde. Edic. Gaesa, Madrid, ISBN 978-84-8023-685-0 + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.ecaboverde.com/cat26.htm + +Dëkki Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Chã das Caldieras benn dekk-dëkkaan Santa Catarina do Fogo ci yu penku yu nekku Fogo, Kap Weer. + +Dencukaay + +Teerekaay +Michel Lesourd (dir.), « Cova Figueira », Le Cap-Vert, Éd. du Jaguar, Paris, 2006, p. 136-40 ISBN 978-2-86950-408-0 +Isildo Gomes et al., Endemic plants and indigenous trees of the Cape Verde islands, Ministry of Environment, Agriculture and Fishery and the Projects « Conservation and Exploration of the Natural Resources on the Island Fogo » (Deutsche Gesellschaft für Technische Zusammenarbeitand) and « Conservation of Biodiversity », 2003 +Michel Lesourd, État et société aux îles du Cap-Vert : alternatives pour un petit État insulaire, Karthala, Paris, 1996, p. 86-87 ISBN 2-86537-625-7 +Map of Fogo Brava 1:60.000, Attila-Bertalen-Kartenverlag, Karlsruhe, 2002, ISBN 3-934262-03-1 + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Fogo, Global Volcanism Program , 7 awril 2012 + Observatório Vulcanológico de Cabo Verde (OVCV) +"Chã das Caldeiras: 158 alunos recebem kits escolare", A Semana , 23 oktobaar 2010 +"Primeiro-ministro promete energia para Chã das Caldeiras, Fogo, até 2016", RTC, , 13 juwin 2011 + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +São Domingos benn dekk-dëkkaan São Salvador do Mundo ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Football klubi +Os Garridos + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Salamansa benn dekk-dëkkaan São Vicente ci yu penku yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Football klub +Salamansa FC + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.ecaboverde.com/img1958.htm +http://mindelo.info/gal_salamansa.php + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Mbërbóof xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Curcurbitaceae", barab yu naaje yi lees koy baye. Tur wi nag ci làkku wolof ñi ngi ko tëgge ci "mbër mu bóof" ndax bari gu mu bari ay njariñ rekk. + +Melo wi + +Garab gi danay àgg ba 5 met ci guddaay. Xobam xet gu tar ak cafka gu wex la yore. + +Tóortóoram day ndaw te mboq. Car yu nooy a koy tëye. + +Doom bi daa dége te puur. Guddaayam 8 ba 35i sàntimet lay àgg. + +Njariñ li + +Mbërbóof lees di lekk la te di ko fajoo. Ci toppatoog jabet ak yenn kãseer yi dees na ko fa jëfandikoo. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Momordica balsamina + +garab +meññeef +Rat Rat xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu "Combretum". Dees na ko fekk ca Senegaal, ca Burkinaa, ca Gana, ca Mali, ca Gàmbi, ca Niseer, ca Niseryaa ak ca kamerun. + +Meññuwaayam +Rat cib gott lay faral di sax ak ci yeneen xeeti suuf yu bari, waaye ci beeñ la gëne. Day muñ bekkoor te ci barab yiy sotti lu toll ne 200 ba 700 milimet cib taw cim at lay meññ. Màggam daa gaaw. + +Melow wi +Rat gàncax la guy àgg ba 12 met. Bànqaasam day wàcc, ronam dëng, xàncam day dége te baam , ñuul. Xobam day dijj, nëtëx te mel ni ndàbb bu mboqe. Ci noor lay tóortóor. + +Doom bi dana àgg ci 2,5 ba 4i sàntimet ci guddaay. Ak 1,5 ba 3i sàntimet ci yaatuwaay. Saawiyee ba nowàmbar lay meññ ci yaatal. + +Njariñ yi +Dees na ci jële ay melal yu mboq. Aw dénkam dees na ci defar ay jumtukaay. Dees na ko jëfandikoo ci wulli. Ñam la ci yenn mala yi. Dees na ko lekk te di defar ay ndimo. + +=Nees di fajoo ak rat +Xobu rat day faj soj, wutal juroom ñaari xob baxal ko ci genn wàllu liitar lu mat 5i simili, di ci naan genn wàllu kaas suba , bëccëg ak ngoon. + +Day yokk kàttanu góor, ñaari xob yi ngay baxal ci genn wàllu kaas ñatti waxtu. + +Day yokk dereet it juroomi xob ngay wut def ko ci liitaru ndox baxal ko di ko naan 3i waxtu bu dee mag, bu dee gone kaasu attaaya + +Day faj dagg-dagg bu bees, jëlal xob wu tooy mokkal ko, boo ci noppee nga tay ko ci, gaaw na ci lool. + +Day faj sibiru bu àndee ak sexaw ak ngeer, baxal ko di ko naan suba, bëccëg ak ngoon. + +Dana maye pàppin (àppeti). + +Reen bi day faj feebaru sëy ak nduxum siti. Ak feebaru ngaana bu dee gu bees. + +Boo amee doom mu yeex a dox wutal ñaari liitar baxal ko ci ndox mi di ci naan kaas 3i waxtu. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Combretum glutinosum + +Turam ci yeneeni làkk +Araab: Pulaar: dooki Hawusa: kantakara +Siddeem pom xeetu garab la gu bokk ci njabootu Rhamnaceae yi. Xeetu siddeem yu baree am. + +Melo wi +Garabu siddeem pom danay àgg 2 ba 5i met ci guddaay, ak i xobam yu nëtëx tey melax yiy àgg ba 5i sàntimet ci guddaay. + +Doom bi dees koy lekk, wirgo wu mboq lay yor te muluŋ danay toll 1 ba 1,5 sàntimet. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + +Ziziphus lotus + +Turam ci yeneeni làkk + +garab +meññeef +Niimaa xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Azadirachta", End la bàyyikoo. Ci barab yu naaje yi ak xaw a naaji yi lay sax. + +Melo wi +Garab gu gaaw a sax la, man na àgg ba 20i met ci guddaay, ci lu neew nag 35 ba 40i met. Xobam day wéy waaye danay ruus ci jamonoy bekkoor gu taar. Bànqaasam daa yaa te tàlleeku. + +Xobam danay àgg 20 ba 40i sàntimet ci guddaay. + +Tóortóoram daa weex te gëtte. + +Njariñ yi +Xobi niimaa day dàq yoo ak i ñoñam. Diwu niimaa day jariñ ci wàllu melal. + +Nataali niimaa + +Turu xam-xam wi +Azadirachta indica + +Turam ci yeneeni làmmiñ +Araab: + Farañse: neem +garab +Àngale: neem +Darkase xeetu garab gu bokk ci njabootu Anacardiaceae. Ca Amerig gu naaje ga la bàyyikoo, te ci barab yu naaje yi lees koy baye ngir foytéefam. + +Melo wi +Garabu darkase danay àgg 12 ba 15i met ci guddaay. Buut bi di reenam bi ëpp solo danay àgg ci xóotaay bu sori ci suuf si. Pànguur yi di reeni wet yi danañuy àgg fu sori lool. Xobam wirgow nëtëx bu dër la yor. Danay àgg 10 ba 20i sàntimet ci guddaay ak 10 sàntimet ci yaatuwaay. Xobam wi puur ci noor lay feeñ. Daa gëtte am xet gu neex te day xëcc yamb yi, ci la lem di bàyyikoo. + +Doom bi +Doom bi ci njeexteelu noor lay mat. Bu ñoree day xonq mbaa mu mboq. Bu ñorul nag nëtëx. Am ub saal ca biir bu ñuy wax ndaamaraas mu bari ay njariñ lool. + +Njariñ li + +Doom bi dees na ci njar, dees na ci defar sàngara te dees na ci faju. Garab gi nag dees na ci jële am matt dees na ci faju. + +Turu xam-xam wi +Anacardium occidentale + +Nataal yi + +Turam ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Soobaan di Sapindus saponaria garab la gu am xob yu xaw a tal, yor taxawaay bu yam rëyul ndawul. Ma nga fekk baax ca Amarig. Xeetu turam wii di Sapindus nag, mi ngi jóge ci latin di tekki saabub endo. + +Melo wi +Garab gu yamamaay la guddaayam war a àgg ci 10i met. Ay xobam di xob yu sew te xaw a gudd cat yu bëñe. Guddaayam war a àgg ci 30 cm. Am ay rëdd ci biir xob wi yu sew. Meññeef di nekk ci poqi car yi. + +Foytéef bi +Foytéef bi wirgo mboq lay yor. Ag ndombaam di àgg 4 cm. Day am ci biir benn pepp bu ñuul. Doom Oktoobar lay ñor, waaye yenn saa yi mu des ci garab gi ba noor. Ci waxtuw noor lay gën a meññ. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + Sapindus saponaria + +garab +meññeef +Séng di Acacia raddiana garab la gu fekk baax ca weti saara dees na ko fekk it ca réewi gànnaar. Garab gi nag day yékkatiku ba ca kaw door a mbaar foofu ay xobam. Peer bi day jóg, taawu ay wànqaas yu téen, door a baar foofu ay xob yu rankaloo mu mel ni am mbaar. + +Tóortóor yi + Tóortóor yi nag, dañuy dajaloo di focc def ay dank yu ndaw yu weex te mel ni lu mboq. + +Foytéefam + Foytéefam nag, nit du ko faral di lekk waaye mala yi bëgg nañu ko lool. + +Njariñ yi + Séng dees na ko jëmbat ngir xeex ag tàkk (deseer). Bépp bërëb bees ragal tàkk gi agsi fa, bees fa jëmbatee ay séng moo gën a gaaw ci kar tàkk ga ba du fa yegsi. Ndax moom daa man a muñ am ndox lool, te itam ci suuf yu dëgër yi la ëpp lu miy sax, rawatina suufu Afrig yi jege Saara. + +Njëfëndaay li + Séng dees ciy defar diw, ak asib, te asib boobu di bawoo ci séng baax na ci jabet, te itam day wàccee yéegug dereet gu ëpp ci yaram. Séng daal lu am solo ci réewi Afrig yi féete Saara. Bantam it dees koy jëfandikoo lu bari. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + Acacia raddiana + +garab +Mbànte garab la guy sax at ba at, gu sew te am car yu sew di am ay xob yu xet ga nàqari lool, mu man a yegg ba ci ñaari met ci guddaay waaye lu ci ëpp nag lu ndaw lay doon doom yi it doon doom yu sew te gudd. Garab gi ñi ngi koy watte ci àll bi ngir fajum cosaan. Doom yi leeg-leeg man nanu koo jëfandikoo ngir mu wuutu kafe. Garab gi nag, faju lees ciy gën a def. + +Barab yi muy sax +Garab gi ci li ëpp mi ngi sax ci suufu sën walla fu ko jege walla ci lu xaw a kawe tuuti walla ci bërëb bu suuf sa xaw a nangu walla ci bërëb boo xam ne dex da faa jege mbaa ab àll. + +Njariñ li +Garab gi manees na ciy lekk mbaa di ko jëfandikoo cim paj. Ci lekk gi: doomi garab gi bees ko jëlee weer ko ba mu wow nu wal ko ba mu nekk sunguf manees na koo jëfandikoo ngir mu wuutu kafe. Boo jëlee xob yu xaw a mag yi tay ko man koo jëfandikoo ci rëndaay noonee it doomi garab yu ndaw yi moom it manees na koo jëfandikoo ci rëndaay, xob yi soo ko jëlee takk ko ci sa bopp dana faj bopp buy metti, jigeen ju wësin itam bu wutee xob yi baxal ko di ko dàmpoo baax na. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Senna occidentalis + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab +Tabanaani xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu Euphorbiaceaete bàyyikoo Meksig. + +Melo wi + +Garabu tabanaani man naa àgg ba 8i sàntimet ci guddaay. Xobam day xonq. +Doom bi danay ëmb lu toll ci 25% ci diw, jiwu bi nag 37% lay ëmb ci diw. Garab gi xet gu xasaw lay gilli. + +Njariñ li + +Nekkam tooke teewut ñu koy bay ngir diwam. Bokk na ci lees di defaree saabu Marsey. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Jatropha curcas + +Tur wi ci yeneeni làkk + + garab + meññeef +Sàngol ag lawtan la guy law ci kaw i garab, garab la nag goo xam ne lu ëpp ci mbayam cig paj la jëm. + +Dëkkuwaayam + +Garab gi ci bërëb yu xaw a af yi, yu yaatu yi lay man a nekk walla ci àll boo xam ne ay garab yu sew ñoo fa am. Leeg-leeg it man naa nekk ci bërëb bu am ker walla it mu topp dex gi. Garab la guy yéeg ci yeneeni garab yuñ man a fekk leeg-leeg ci suuf su nooy walla ci suuf su nuy noppal. + +Njariñ yi + +Li ëpp ci li ñiy jëfandikoo garab gi cig paj bokk na ci wàcce tàngooru yaram moo xam it tàngooru yaram wuy dem ak ay ñëw la walla pajum sibiru doonte sax ci réew mu mel ni End garab gi bokkul ci ñaar fukki garab ak juroom yi ñu taamu ngir faj sibiru. Leneen li ci topp ci li ñiy faj ci garab gi mooy pëyiis mbaa gaana mbaa feebaru sifilis. Garab gi bokk na ci yi ñiy jëfandikoo ngir yokk ngóora. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Cocculus pendulus + +Garab +Xaalu tubaab garab la gu bàyyikoo ca Afrig gu naaje ga, ci njabootu "curcurbitacées" la bokk. Bul ko jaawale ak xaal. + +Melo wi +Xaalu tubaab xeetu ñax la guy caram di law lool bay àgg 3i met. Yenn xeet yi day law cig raam yeneen yi di law cig yéeg. + +Xob yu góor ak yu jigeen lay meññandoo. + +Doom bi day wërmbalu mbaa mu muluŋ teg ci dijj. Day saf suukar lool bu ñoree. + +Njariñ li +Doom bi dees na ko nal defar ci njar. Maneef na ko lekk nim bindoo it. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Cucumis melo + +Tur wi ci yeneenI làkk +Araab: بطيخ/شمّام +Farañse: melon + +Garab +meññeef +ñax +Tarrafal de Monte Trigo benn dekk-dëkkaan Porto Novo ci yu sowwu yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Football klub +Tarrafal FC de Monte Trigo + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.ecaboverde.com/cat28.htm + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Salaan garab la gog mi ngi bokk ci njabootug aforbiyaas cosaanoo ca penku Afrig. Garab la gog ñu ngi koy fekk mu yaatu lool ci tund Afrig. + + ==Melo wi== +Garab gu yamamaay lay doon goo xam ni ci guddaayam day jàpp, yaari met. Ay bànqaasam dëgërul lool. Daa gaaw a jooy lool it. Soo ko daggee day génne meen mu weex niki poftan. Ag keram nag, mbëtt yi ak jaan yi bëgg nañu ko lool, ba dañuy faral di gas ci ag ronam lu bari. Xetug ay xobam nag neexul. Bu dee ca Senegaal, ku dugg neegub góor di ab njulli daa ñu la ko faral di wutal. + + ==Solo si== +Garab la gog manees na koo jëfandikoo cim paj ak ci yeneen ak yeneen. + +nataal yi + +turu xam-xam wi + Euphorbia balsamifera + Garab +Rëb-rëb gi xeetu garab la gu bokk ci njabootu Terminalia, Afrig gu sowu lees koy fekk. + +Melo wi +Rëb-rëb gi gàncax guy hàgg cig guddaay 2 ba 4i met la, mbaa garab guy hàgg cig guddaay 8 ba 12i met, te ronam day gàtt ba noppi am xànc mu baam. + +Njariñ yi +Ca Mali xobam dañ koy cuubee ndimo ngir mu am wirgo wu mboq. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Terminalia avicennoides + +garab +gàncax +Xott-biteel gi xeetu garab la gu bokk ci ñoñ Eucalyptus. Óstraali la bàyyikoo. + +Melo wi +Guddaayuy 20i met lay yore, waaye man nay hàgg ba 45i met. Xàncam day dijj (3i sàntimet), woyof, te yor i gàkk gàkk yu xonq, yu baam, yu nëtëx ak yu weex. Saawiyee ba suye lay meññ ci barab yu naaje ya. + +Njariñ yi +Ronam bu tàbbe cig dex, dëkkuwaay la ñeel yenn jën yi. Dees kor kerloo te di ko fajoo it. + +Nataal yi + +Turu xamxam wi +Eucalyptus camaldulensis + +Tur wi ci yeneeni làkk + +Farañse: gommier rouge/ des rivieres + + garab +Béb di Strecuia satigera garab la gu man a sax ci suuf su bon ak kéew mu naqari, guddaayam man naa àgg ba ci 15i met. + +Melo wi +Xas mi day mboq walla mu maroo di def ay der yu wayaf di xolleeku. Ay xobam jamonoy nawet lay sëq. Meññeefam day mbuluŋ, der bi day nooy. + +ay njariñam +Meññeefam dees koy lekk, am xasam dees na ko jëfandikoo ngir faj siburu. Waaye nag moom daakaandeem lees ëpp ci lees di jëfandikoo, dees na koy jëfandikoo ci anam yu bari. + +saxuwaayam +Garabu béb amna ci réew yu bari waaye weti END, OSTARAALI, ak SUDAA... la ëppe. Njaayum daakaandey Béb nag mi ngi gën a baree ci diggante Senegaal ak END ndax ñoo ëpp luñ koy am. Daakaande ji ci weeru Nowaambar lay tàmbalee xelli jëm ba nawet bi sori lool! + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Xureer garab la gu bàyyikoo Sapoŋ, Óstaraali, ca pàcc bu yaa ca Asi gu Ngoppkaw, (Bëj-saalum ak Penku) ak ca dun yu bari yoy Jàmme(pasifig) gu Bëjsaalum. + +Melo wi +Xureer gi garab la guy tóortóoram yore xetu laaj. Xeetu garabu tóortóor la gog gox yu naaje ak xaw a naaje yi. Day yeex a màgg, day néew i xob, téeñu ronu garab gi daa teqaloo te yor xob yuy melax ak um xànc mu am i gàkkgàkk yu weex. Yenn ciy xeetam man nañ àgg ba 30i met ci guddaay. Ci suuf su naat te néewle ag sëcc(asibe) lay gën a man a meññ. + +Njariñal xureer +Xureet garab gu am ug tooke la waaye ginnaaw ag togg dootul lore. Xob yi ak meññ mu yees mu dañ leen lekk niy lujum. Dees koy fajoo, di ci dolli ag xëntewoo lekk, di ci jële ay bir ngir defar simaa, te di yàtt cim mattam ay jumtukaay. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Crateva religiosa + +Tur wi ci yeneeni làkk + +Farañse: poire à l'ail sacrée + +garab +Ngéejaan walla Ngalama ci Baambara garab la gog mi ngi fekk baax ci tundi Afrig sow jant mi ngi bokk ci njabootug kompritaasiiye. + +Melo wi + +Guddaayam man naa jàpp ci juroom jàpp fanweer ciy met peram day yaatu lool man naa jàpp juróom-ñaar-fukki sànti met. Ay foytéefam dañuy yor melo wu xaw a mboq walla melo wu xaw a oraas ci digg bi. Garab gi nag garab la gog jamonoy noor rekk lees koy farala gis ak bu nawet bi tàmbalee benn xeet la garab, gog dafa bari lool ci tund Afrig, fiñu koy fekk mu bari lool mi ngi nekk ci réew yu mel ne Senegaal, ak Ecopi. + +Solo si +Garab la gog bari na lumuy faj lool ndax ay raasinam dan koy jëfandikoo ngir faj lu ci mel ni néew kàttan walla ku am ay jafe-jafe ngir jugal ak biir buy daw itam ñeel gone yu ndaw ñi. Garab la gog manees na cee def ay xeeti Armuwaar ak yu ni mel manees na koo def matt. + +Nataal yi + +turu xam-xam wi +Anogeissus leiocarpus + +garab +Kàdd garab la gees di fekk ci gox yu naaje yi niki ca Senegaal, ca Afrig la bàyyikoo. + +Melow kàdd +Kàdd garab la gog ay caram ak i wànqaasam yéppay am i dég. Njoolaayam man naa àgg ba ci 30i met, xalaam man na àgg ba ci 2i met. Reenu garab gi man naa dugg ba ci 15i met ci biir suuf. Ci jamonoy maral, xasu garab gi day soppi wirgo teg ci di xolleeku. + +Garabu kàdd daa am dund gu wuute ak yeneen i garab yi des yépp ndax moom kepp mooy garab gu ay xobam di ruus nawet ak a sëq ci jamonoy lolli. Loolu nag li ko waral mooy ngir mu man a dund cig maral ak ci barab yu ñàkk ndox. + +Njariñi kàdd +Kàdd garab gu am njariñ la fii ci tund Sahel rawatina ci lu jëm ci wutum lem ndax ci jamonoy nawet ay tóortóoram man nañu dundal yamb yi ngir ñu man a am lem bu doy. Leneen ci ay njariñam, fóyteefu garabu kàdd di Àdd lu am solo la ci dundug jur. + +Nataali kàdd + +Turu xam-xam wi +Faidherbia albida Acacia albida la tuddoon + +Wàll:Garab +Ngigis xeetu garab la guy ne ci sahel bi ci réew yu mel ni Senegaal, Gànnaar... + +Melow ngigis +Ngigis, as ngarab la gog ay xobam xob yu xaw a dëgër lay doon te xaw a yaatu te am njariñ lool, melow garab gi nag man naa àgg 3i met ba 15i met ci njoolaay. Garab la gu bari fu ñu ko man a fekk nu man koo bay cib àll. Garab gi man na joxe ay ñam mbaa ay garab yuñ man di fajoo. + +Njariñal ngigis +Foytéefam day jariñ ci wàllu togg. + +Ci wàllum paj nag, garabu ngigis xob yi ak bant yi ak reen yi yépp a am njariñ. Bu nu tàmbalee ci xob yi, dees koy yëy, ndox moo mu muy genne lanuy muucu mooy faj biir buy metti walla sëqët walla ku jaan màtt. Bu nu fabee xob yi lakk ko bamu def dóom, danay faj góomu ku jaan màttoon dana koy wowal ngir mu gaaw a wér it. + +Reen yi man nanu koo jëfandikoo ci jigeen joo xam ne mbaaxam day yàgg, dana faj itam linuy wax "emorasi" muy yaram wuy nàcce ci biir dana musal it ci ëmb buy yàqu, dana faj it sëqët su yàgg, dana faj it soj walla coonay yaram. + +Bu nu ñëwee ci xas mi. Xas mi bu nu ko toggee man naa faj soj man naa faj dënn buy metti ci biir, man naa faj màttiitu jaan. Xas mi nag ak xob yi nga boole ko togg moo gën a gaaw ci bëñ buy metti danga koy suuroo ak di ko galaxndikoo. + +Nataali ngigis + +Turu xam-xam wi +Piliostigma reticulatum + +Wàll:Garab + +Wàll:Gàncax +Xël xeetu garab la gu bokk ci njabootu Moraceae. + +Melow xël +Xël man nay hàgg ba 40i met ci guddaay. + +Nataali xël + +Turu xam-xam wi +Ficus platyphylla + +Yeneen i làkk +Araab: التّين Farañse: figuier +Monte Águila dëkku di Sili. Nitñii motnañu 6.090 (2002). +Suuna xeet la ci xeeti garab yi mi ngi bokk ci njabootug buwaasiis ñu di ko bay ngir ay doomam yi nga xam ni dañuy tàkk. garab la gog moom lañuy gën a bay ci xeeti garab yi. + + ==Melo wi== +Garab la gog guddaayam man naa àgg 1 jëm 3 ba 4i met, ay doomam dañuy yor melo wu xaw a weex, walla xaw a mboq, walla xawa baam te niru ak ay fer. + + ===Solo si== + Garab gu ñuy bay la lool te bari ay njariñ fële ca End ak Pakistaŋ, ca Sahel ak Afrig ci yenn barab yi. Ay doomam dañu koy jëfandikoo ni Ceeb ñu di ko tàngal bamu ñor te it dañu koy soppi di ko def Fariñ; boo demee ci yenn réewi Afrig yi am na ñu ko fay soppi am ñoll. Fële ca Órob garab la gog dañu koy jox mala yi ñu di ko jëfandiko. + +Nataali Suuna + +Turu xam-xam +Pennisetum glaucum + +garab +Sénki garab la gu fekk baax fii fi Afrig guddayam day toll ci 4 ba 7i Met garab la gu siiw, amna Asi, Óstraali ak réewi Karayib yi. + +Melo wi + +Ay xobam dañoo sew yaram wi daa baam, te itam dañiy janoo toll ci 5 ba 15i sàntimet. Meññeef mi day nekk ciy xolliit yu mboq walla yu xuun di am 4 ba 5i doom. Garab gi mi ngi jebbi ci ñaareelu xaaju noor bi. + +Solo si + +Ay reenam dees na ko fajoo ci yax yuy metti ak gone guy waccu, ba tay reen yi bees ko jaxasee ak xob yi day dindi kadam. +Bantam dafa dëgër te ñeme max te itam dees na ci liggéey ay njëfendaay. +Bantam itam neex naa togge te man këriñ lu baax! +Reen bu tooy bi bees ko dëbbee tay ko ci bëñ buy metti da koy faj. +Ngir faj "estomaa" góomu biir dangay jël ŋëbub xob yi ak i reen boole leen baxal ci liitaru ndox bàyyi ko bam sedd nga segg ko di ci naan benn kaas saa yoo lekkee ba noppi. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Dichrostachys glomerata +garab +meññeef +Wereg xeetu garab gu bàyyikoo Afrig te bokk ci njabootu fabacées. + +Melo wi + Gudaay: 3 ba 6i met. +Xànc: melow baam la yore. + Doom bi: -Daa tàcc -5 ba 7,5i sàntimet ci guddaay. -1,7 ba 2,5i sàntimet -5 ba 6i xoox yu baam-nëtëx lay ëmb. + +Njariñ + +- Dees koy fajoo. +- Dees koy jëfandikoo ci aniin +- Dees koy lekk. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Senegalia senegal + +garab +Sëng garab la gu fekk baax ca Afrig. + +Melo +Guddaayu sëng day toll ci 4 ba 7i Met. Garab la gu siiw, am na ca Asi, ca Óstraali ak réewi Karayib yi. Ay xobam dañoo sew, yaram wi daa baam, dañiy janoo tey toll ci 5 ba 15i sàntimet. Meññeef mi day nekk ciy xolliit yu mboq walla yu xuun di am 4 ba 5i doom. Garab gi mingi jebbi ci ñaareelu xaaju noor bi. + +Njariñ +Ay reenam dees na ko fajoo ci yax yuy metti ak gone guy waccu, ba tay reen yi bees ko jaxasee ak xob day dindi kadam. Bantam dafa dëgër te ñeme max te itam dees na ci liggéey ay njëfendaay. Bantam itam neex naa togge te man këriñ lu baax! Reen bu tooy bi bees ko dëbbee, tay ko ci bëñ buy metti da koy faj. Ngir faj "estomaa" góomu biir dangay jël ŋëbub xob yi ak i reen boole leen baxal ci liitaru ndox bàyyi ko bam sedd nga segg ko di ci naan benn kaas saa yoo lekkee ba noppi. + +Nataal + +garab +Benteñe xeetu garab la gu bokk ci njabootu Bombacaceae ci nose gu yàgg ga, ci gu yees gi nag ci gog Malvaceae + +Melo wi +Garab gu am jëm la gog man na àgg ba 40i ci guddaay (ba sax 60i met ci guddaay ca Afrig). Ronam day liis, am i dég te ci yaatal wàqaasam day tàlleeku ba noppi raase. Tóortóoram 5 ba 9i xob lay am, yu wërmbalu lay doon te guddee nu day ni 10 ba 18i sàntimet. Foytéefam këmbaan guy lang, 10 ba 30i sàntimet moo di guddaayam. + +Njariñ li +Màttum benteñe nekk na lu ñu bari xëntewoo ngir jariñoo ko ci anam yu wuute te bari. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Ceiba pentandra + +garab +Àkkasaa, garab la gu bokk ci njabootu Fabaceae, Asi gu Ngopp suuf (bëjsaalum-penku) la bàyyikoo waaye ci lu yees nit tasaare na ko, ji ko Afrig. + +Melo wi +Garab gi man na àgg ba 25i met ci guddaay. Xobam day njaxas. Tóortóoram ya dañuy mboq te dajaloo ciw car ba noppi sëq te di guddee nu day ni 15 ba 30 sàntimet. Doom bi day wërbalu teg ci di àgg 10 ba 30i sàntimet ci guddaay. + +Njariñ yi +Dees ko jëfandikoo ngir: -Jëmbat pàkk yi booy. -Dekkil suuf su dee. -Faj mettig yenn cér yi. -Defar yenn garab yi. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Senna siamea + +Tur wi ci yeneeni làkk + +Farañse: cassia du Siam/ casse du Siam. + +garab +Sëriis garab gu bàyyikoo Madagaskaar la. Ci njabootu Phyllanthaceae la bokk. Doomam dees koy lekk, day wex. Xobam rënd la ci toggi yenn réew yi + +nataal yi + +Turu xam-xam +Phyllanthus acidus + +Yeneen làkk + Farañse: girembellier + +garab +São Jorge dos Órgãos benn dekk-dëkkaan São Lourenço dos Órgãos ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Dayo +Tomé Varela da Silva + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Salto benn dekk-dëkkaan Mosteiros ci yu penku yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Sëriñ Móodu Lóo Dagana + +Sëriñ Mbay JAXATE + +Sëriñ Maalig Basin Si + +Sëriñ Muusaa KA +Mborosaan xeet la ci ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug "Apocynaceae", mi ngi cosaanoo fee ca Afrig, ci réewum Birmani, foofu dinañ fa fekk lu tolloog 78i garabi mborosaan. + +Melo wi +Guddayam man naa jàpp 150i met. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Caralluma retrospiciens + +Garab +Béer garab la gog guddaay gu yam la yor. Mi ngi bokk ci njabootug Anacardiacées. + +Melo wi +Garab gi peer bu ndaw la yor, day màgg jëm ci kaw, guddaayam man naa àgg ba 10i met. Garab gu bari lool ay witaamin la. Danay meññ benn fooytéef bu dëgër, ñuul te neex lool. + +Njariñ yi +-Ay foytéefam dees koy lekk ak di ci defar yenn xeeti njar yi. +-Garabu ber manees na ko jëfandiko ngir doxal yenn daamar yi. +-Garab la gog bari na jàngoro yu muy faj, bokk na ci sibbiru. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Sclerocarya birrea +garab +Laay garab la gog guddaay gu yam la yor. Mi ngi bokk ci njabootug Anacardiacées. + +Melo wi +Garab gi peer bu ndaw la yor, day màgg jëm ci kaw, guddaayam man naa àgg ba 10 met. Garab gu bari lool ay witaamin la. + +Danay meññ benn fooytéef bu dëgër, ñuul te neex lool. + +Njariñ yi +-Ay foytéefam dees koy lekk ak di ci defar yenn xeeti njar yi. + +-Garabu ber manees na ko jëfandiko ngir doxal yenn daamar yi. + +-Garab la gog bari na jàngoro yu muy faj, bokk na ci sibbiru. + +=Nataal + +Turu xam-xam wi +Sclerocarya birrea +Juuf garab la gog guddaay gu yam la yor. Mi ngi bokk ci njabootug Anacardiacées. + +Melo wi +Garab gi peer bu ndaw la yor, day màgg jëm ci kaw, guddaayam man naa àgg ba 10 met. Garab gu bari lool ay witaamin la. + +Danay meññ benn fooytéef bu dëgër, ñuul te neex lool. + +Njariñ yi +-Ay foytéefam dees koy lekk ak di ci defar yenn xeeti njar yi. + +-Garabu ber manees na ko jëfandiko ngir doxal yenn daamar yi. + +-Garab la gog bari na jàngoro yu muy faj, bokk na ci sibbiru. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Sclerocarya birrea +Suraas gi xeetu gàjj la gu bokk ci njaabootu Rutacées. Barab yu tàng yi lees koy bay. Asi la bàyyikoo. + +Melo wi +Garab gi man na àgg ba 10i met ci guddaay. Wànqaasam day am i dég te xobam 4 10i sàntimet àgg ci guddaay. + +Njariñ yi +Suraas gi soloom ci wàllu koom lu fés la. Am na solo it ci wàllug paj. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Citrus sinensis + + garab + meññeef +Wén gi xeetu garab la gu bokk ci ñoñ Pterocarpus ak ci njabootu Fabaceae. Ci Sahel gi lay meññ ci Afrig. + +Njariñ yi +Mattam nekk na lu nit ñi xëntewoo. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Pterocarpus erinaceus + +Tur wi ci yeneeni làkk +Farañse: véne (wén) + + garab +Paftan gi garabu tóotóor la gu bokk ci njabootu Apocynaceae. + +Melo wi +Garab gu yam la, man na àgg ba 3i met. Doomam day wërbalu te duuf. +Moom ak xob wi wirgo wu nëtëx lañuy yore. Tóortóor bi day weex. +Garab gi day nacc di génne meen mu bari. + +Njariñ yi +Garab gu am solo la ci wàllu paj. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Calotropis procera + + garab +Yiir garab la gu guddaayam man a àgg ba ci 12 jàpp 20i met, yaatuwaayam ci benn met lay toll. Moom nag ñi ngi ko duppee garabu weñ ndax dëgëraaym max manalu ko dara. + +Bérëbam +Garabu yiir nag amna Senegaal, Kamerun, Sudã ba Niseer. + +Njariñ yi +Ay reenam day faj bëñ yu kadam, am xasam it baax na ci góom. Ay xobam ak i bantam baax na ci góomu biir. Bantam bu dëgër boobu dees ciy defar i lal, ak i armuwaal, ak ay ndënd. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + Prosipis africans + +garab +Màngo garab la gu cosaanoo "Asi", bokk ci njabootug Anacardiaceae, bari na lees koy jëmbat ci réew yu tàng yi ndax ay doomam. + +Moom màngo ak tàndarma bokk nañu ci garab yi gën a yàgg. Araab yi ñoo ko indi Afrig ci fukk ak juróom-benneelu xarnu. +Màngo nag man naa sax fu bari waaye ci xur la gëne. +Ñemewul taw ci jamono yi muy jebbee. + +Melo wi +Màngo garab gu mag lay doon guddaayam day àgg ba ci 20 ba 25i met. + +Xas mi daa ratax ay doomam day mat 500 ngaraam ba ci ñaari kilo ak genn wàll. Saalu doom bi dafa sew te tàppndaar + +Njariñ yi +Xobi màngo dees na ko jëfandikoo ngir wattu feebar yu tukkee ci jam-jam walla dagg-dagg. + +Meññeef mi lu bari ay ferñent la, te it moom màngo lu baax ci "kãseer" la ak néew dereet. Te it màngo dana dimbalee ci yeex a màgget ngir ferñet yi mu làmboo. Bokk na ciy ngëneelam day xeex feebaru noyyi, day reesal ñam di xeex seere. Saal bi lu baax la ci saan danga koy baxal di ci naan booy lekk. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Mangifera indica + +garab +meññeef +''Mbind mu weng'Xorompolle + +((Ay njariñ)) + +Xorompolle: garab la gu baax gu am solo boo ko dëbbee ba mu mokk nga def bis bu ne ba la ngaa lekk dara nga jël ci genn wall gudd gu ndaw nga boole ko meew dangay tàngal ndox mi nag door koo jaxase ak moom soo ko dee def bis bu set baa na ci diir muy metti ak taasyoo ak ilseer ak feebar yu bari yuy dal nit raw Kon de ndekete seetaan kuy def lum wërtë def baaxul Kon seetaan kat yi wuyyuleen!a ti na feebaru biir rawatina jabet! +Tarrafal de São Nicolau benn dëkk-dëkkaanu ci yu dunu São Nicolau, Kap Weer. + +Dëkki +Tarrafal de São Nicolau + +Dëkk-dëkkaani +Cabeçalinho +Fragata +Hortelã +Palhal +Praia Branca +Ribeia dos Calhaus +Ribeira Prata + +Football clubi + AJAT'SN + FC Praia Branca + FC Ultramarina de Tarrafal + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20190714061259/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/TarrafaldeS%C3%A3oNicolau.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Paul benn dëkk-dëkkaanu ci yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Dëkki +Pombas + +Dëkk-dëkkaani +Cabo da Ribeira +Campo de Cão +Eito +Figueiral +Janela +Pico da Cruz +Ribeira das Pombas +Ribeirãozinho +Santa Isabel + +Dayo +Antoninho Travadinha + +Football clubi + UD Janela + Paulense DC + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20060506171646/http://www.paulbelezanatural.com/ +https://web.archive.org/web/20190714061642/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/Paul.aspx +https://web.archive.org/web/20160820012229/http://asemana.sapo.cv/spip.php?article23822 + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Saar garab la gog guddaay gu yam la yor. Mi ngi bokk ci njabootug Anacardiacées. + +Melo wi +Garab gi peer bu ndaw la yor, day màgg jëm ci kaw, guddaayam man naa àgg ba 10 met. Garab gu bari lool ay witaamin la. + +Danay meññ benn fooytéef bu dëgër, ñuul te neex lool. + +Njariñ yi +-Ay foytéefam dees koy lekk ak di ci defar yenn xeeti njar yi. + +-Garabu ber manees na ko jëfandiko ngir doxal yenn daamar yi. + +-Garab la gog bari na jàngoro yu muy faj, bokk na ci sibbiru. + +=Nataal + +Turu xam-xam wi +Sawat gi ci njabootug Combretaceae la bokk. Bari na lool ca màndiŋ yu Senegaal, Gànnaar, Niseeriya ba Ecoopi ak Ugandaa. + +Melo wi +Garab gu neewi xob la, gàjj la guy àgg 1 ba 3i met. Xasam day ñuul bu garab gi gone, buy mag nag day baam. + +Njariñ li +Soloom siiw na wàllu faj ci Afrig gu soww, reenam day faj mettitu biir, xobam dees koy baxal ngir faj febaaru sawukaay. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Combrerum aculeatum + +garab + meññeef +Sawat gi ci ñoñ Combretum la bokk. Bari na lool ca mànding yu Afrig. + +Melo +Garab gu neewi xob la, gàjj la guy àgg 1 ba 3i met. Xasam day ñuul bu garab gi gone, buy mag nag day baam. + +Njariñ +Soloom siiw na wàllu faj ci Afrig gu soww. + +Nataal + +Turu xam-xam +Combrerum aculeatum +Yuusuf ab yonente la ci ñi Yàlla yonni woon ci kaw suuf! +Ayuba Sulaymaan Jàllo (ñu gën  Koo xam ci turu  Jòobeen Solomon)  , mi ngi judd jamonoy 1701 fëla ca  Bundu,  mi ngi dee atum 1773 .Nekkoon Imaam , waaye ba tay bokk ci  ñi loru  ca njaayum jaam yi  tubaab yi doon def nit ñu ñuul  ñi. + +Nekkoon ab jaam ci ay weer ju bari fee ca  Marilaand  , moom mooy Benn jaam bi njëkk bi   dellusiwaat ci  njaayum jaam ñi  nekk Kenn ci   "Spalading Gentleman' s Society " + +Ayaub Sulaymaan Jàllo  , bindul ay jaar-jaary fundamental moom ci jëmm mi boppam, waaye ñi kuy xam ci dimbalug téereb tomaas  Bulett bii génn ca atum 1734 + +Judd atum 1701.       Ci réewum Senegaal   , Ayuba  bi ngi bokk ci njabtoog gog ay julit lañu,  doon ay woroom xam-xam ci mag, Bi bu nekkee gone ci la jàng làkkuw Araab ak alxuraan  ,moo àndoon ak  buurub Fuuta ba bu siiw ba  Sàmba Gelaajo Jéggi .Bi Amee 29i at,  ci la ko Mandige jàpp. Ñu Njaay ko benn "kapiten" bu ñuy woowee  Piki +Santa Catarina benn dëkkaanu ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Dëkki +Assomada + +Dëkk-dëkkaani + +Achada Galego +Achada Gomes +Achada Lazão +Achada Leite +Achada Lém +Achada Ponta +Achada Tossa +Aguas Podres +Arribada +Banana Semedo +Boa Entrada +Boa Entradinha +Bombardeiro +Chã de Lagoa +Chã de Tanque +Charco +Cruz Grande +Entre Picos +Entre Picos de Reda +Figueira das Naus +Fonte Lima +Fonteana +Fundura +Furna +Gamchemba (Gaamxemba) +Gil Bispo +Japluma +João Bernardo +João Dias +Junco +Librão +Lugar Velho +Manxoli (Mancholy) +Mato Baixo +Mato Gege +Mato Sancho +Palha Carga +Pata Brava +Pau Verd +Pedra Barro +Pingo Chuva +Pinha dos Engenhos +Ribeira da Barca +Ribeira Riba/Ribeira Acima +Ribeirão Isabel +Ribeirão Manuel +Rincão/Porto Rincão +Saltos Acima +Sedeguma +Serra Malagueta +Tomba Touro + +Dayo +António Mascarenhas Monteiro +Ivone Ramos +José Maria Neves + +Football clubi +Os Amigos +Desportivo de Assomada +Grémio Desprtivo de Nhagar +Juventude de Assomada + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.ams.cv/index.php?option=com_content&task=view&id=30&Itemid=49 +https://web.archive.org/web/20190714061703/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/SantaCatarina.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Mantaalis garab la gog ay xobam + +day sew teg ci dëgar. Am ay wànqaas yu tegaloo ci melokaan wu yomb a ràññee,  man a + +àgg  ci fukk ba ci ñaar-fukk i met... ci njoolaay. Mbayum garab gi ajuwul ci lenn luñuy jëfandikoo ci wàllug foytéef waaye man nanu koo jëfandikoo cig paj walla cuub. Dees koy jëfandikoo it leeg-leeg ci jëmbat i garab ndax garab gi keram day yaatu lool te it garab gi bu màggee day rafetal bërëb. + +melo wi +Ci cosaanam, moom garab gi mi ngi cosaanoo réew mu ñuy wax (Madagaskaar). + +Mbayam ak barabam +Noo ngi fekk garab gi ci lu ëpp ci àll bu kawewut lool, ci suuf su nangu. Cig mbayam nag garab gi man naa dund ci sunu tund wii nga xamente ni du tooy lool, te it du wow lool ak màggam it doon lu gaaw ci barab yi nga xam ni du tàng lool te it du sedd lool te it li ko ciy gënal mooy ay taw yoo xamente nii du bari lool waaye it bu baree itam man na koo dékku. Dana soxla it muy nekk fu am jant day gën a gaawal ak màggam. + +Ay njariñam +Garab gi amul benn njariñ ci lu jam ci lu nit man a lekk. Ci wàllug paj, xasu garab gi ak i bantam man nanu leen a jëfandikoo ngir faj feebari yenn biir yi. Leneen it ci ay njariñam garab gi man nanu koo jëfandikoo ci lu ëpp ci nu ñuy fexee jëmbatat i garab maanaam ay sémb yu jëm ci jëmbat i garab leneen ci ay njariñam xas mi ak bant bi man nanu leen a jëfandikoo ngir defar ci ay xeet i cuub. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Mantalie Terminalia +Yomb garabu yomb xeet la ci garab yiy law ñu leen di bay at ba at te ñuy meññ. Foytéefam dees koy jëfandikoo cig wowam ci lu toll ci lu nit manul xayma cig yàgg, ak réew i Àddina bi yépp ak di ci defar ay jëfekaay yu bari mbaa ci lu neew nu koy lekk niki lujum. + +Melo wi +Yomb garab guy sax at ba at la, di law ci suuf walla ci kaw,am ay car yu gudd teg si di laxasoo. Xob yi dañuy juwwaloo, wërngëlu, lemu teg si nooy ci laal. Foytéefam day am ay melokaan yu wuute, mel ni xala walla mu gudd . Leeg-leeg day niru ag (buteel) am benn wàll gu yaatu ak beneen bu xaw a gudd. Foytéef bi man naa àgg ba ci benn met... walla mu ëpp ko ci guddaay. Kog gi ko wër su wowee day mujj dëgër ba mel ni bant. + +Cosaan li +Garabu yomb mi ngi cosaanoo ci tund yu xala yi dénd i Afrig ak Asii waaye kenn xamul fan la dëgg-dëgg ndax fu nekk lañu ko mujj fekk ci Àddina ndax daa mujj doon mómeelu xeeti doomu Aadama gépp, ñu di ko jëfandikoo ci seen i tukki teg si ñoŋal ko. + +Mbayam +Mbayum Yomb de yomb na lool ndax garab gi li mu soxla mooy suuf su wow ci barab bu am naaj ñu man faa ji jiwu garab gi. Man nanu sampaat garab gi su dee am nanu tiitaange ci ñu bañ a màgg mbaa suuf si bañ a tàng. Màggu garab gi gaaw na lool. Dina soxla itam ab sàkket leeg-leeg ngir mu man a law ci kawam. Mbayum yomb nag mi ngi ñor ñaari weer képp ginnaaw ji gi + +Njariñam +Su weesoo ñam wii di yomb nu man koo boolee ci sunuy togg, li ëpp ci njariñu yomb mooy joxe ay jëfandikaay yu nit di soxla niki Koog, Leget, mbàttu, añs. Amna ñu koy jëfandikoo it yeneen i xeetu jumtukaay yu jëm ci woy niki Koraa, Xalam, añs. Leeg-leeg itam nga gis ku ko jël taaral ko ngir jëmal dëkkuwaayam. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Laganaria siceraria + +garab +meññeef +Tàng-tar + +garabu yomb xeet la ci garab yiy law ñu leen di bay at ba at te ñuy meññ. Foytéefam dees koy jëfandikoo cig wowam ci lu toll ci lu nit manul xayma cig yàgg, ak réew i Àddina bi yépp ak di ci defar ay jëfekaay yu bari mbaa ci lu neew nu koy lekk niki lujum. + +Melo wi +Yomb garab guy sax at ba at la, di law ci suuf walla ci kaw,am ay car yu gudd teg si di laxasoo. Xob yi dañuy juwwaloo, wërngëlu, lemu teg si nooy ci laal. + +Foytéefam day am ay melokaan yu wuute, mel ni xala walla mu gudd . Leeg-leeg day niru ag (buteel) am benn wàll gu yaatu ak beneen bu xaw a gudd. Foytéef bi man naa àgg ba ci benn met... walla mu ëpp ko ci guddaay. Kog gi ko wër su wowee day mujj dëgër ba mel ni bant. + +Cosaan wi +Garabu Yomb mi ngi cosaanoo ci tund yu xala yi dénd i Afrig ak Asii waaye kenn xamul fan la dëgg-dëgg ndax fu nekk lañu ko mujj fekk ci Àddina ndax daa mujj doon mómeelu xeeti doomu Aadama gépp, ñu di ko jëfandikoo ci seen i tukki teg si ñoŋal ko. + +Mbayam +Mbayum Yomb de yomb na lool ndax garab gi li mu soxla mooy suuf su wow ci barab bu am naaj ñu man faa ji jiwu garab gi. Man nanu sampaat garab gi su dee am nanu tiitaange ci ñu bañ a màgg mbaa suuf si bañ a tàng. Màggu garab gi gaaw na lool. Dina soxla itam ab sàkket leeg-leeg ngir mu man a law ci kawam. Mbayum yomb nag mi ngi ñor ñaari weer képp ginnaaw ji gi + +Njariñam +Su weesoo ñam wii di yomb nu man koo boolee ci sunuy togg, li ëpp ci njariñu yomb mooy joxe ay jëfandikaay yu nit di soxla niki Koog, Leget, mbàttu, añs. Amna ñu koy jëfandikoo it yeneen i xeetu jumtukaay yu jëm ci woy niki Koraa, Xalam, añs. Leeg-leeg itam nga gis ku ko jël taaral ko ngir jëmal dëkkuwaayam. + +Nataal + +Turu xam-xam +Karite xeet la ci ñoñ vitellaria mi ngi bokk ci njabootug Sapotaceae ñu ngi koy fekk mu yaatu lool ci àllub Afrig sowwu jant bi ak diggu Afrig . + +Ay turam +"Karite" ñi ngi koy woowe ba tay "siri" ca Bàmbara fële ca Mali loolu moo waral turu àngale wi "Shea tree" + +Boo demee ci yenn goxi Afrig ñu ngi ko fay woowe "Tànga" walla "Tama". + +Melo wi +Garab la gog day am ay xob guddaayam man naa jàpp 10 ba 16 ci ay met, du am ay xob li feeg amul fukk ak juróom-ñatt ci ay at, Ci boobu nag ci lay tàmbalee di am ay xob yoo xam ni dañuy yor melowu nëtëx bam am téemeeri at, garab la gog man naa dund ñaari xarnu. + +Yaatuwaay peram manees na koo jàpp ci 1,5i met. + +Ay foytéefam dañuy yor melo wu weex, amug xet , di génn ci jamonoy lolli maanaam ci diggante nowàmbar, saawiyee. + +Ci ay foytéefam dañu fay fekk lem ngir ne yamb yi dañu koo bëgg lool. Garab la gog day màgg ci àll bi ngir nag ñu doon wax dëgg-dëgg "karite" fàww mu am fukki at ak juróom nga xam ne booba lay génne ay xobam yu jëkk. + +Ay foytéefam juróom-benn kilo yii rekk lañuy jël def ko muy doon diw, diwug karite maanaam boo xoolee li muy ñorle buñu ko xaajee ñatti xaaj benn xaaj bi rekk lay jël. + +Garab gi nag bu demee ba am juróom-fukki at jàpp téeméer ay xobam dañuy mujji doon ay doom loolu nag muy mbir mu yéeme lool ay foytéefam manees na leen a natt ci 10 jàpp 57 ci ay garaam. + +Njariñ yi +Garabu Karite nag bari na ay njariñ lool ndax doom bi manees na cee am karite gees di diwoo garab gi itam manees na cee togg, manees na cee def ay kamoot, cempteŋ , ay toogu a.ñ.s. + +Foytéef yi bari na ay witaamin lool dees koy jëfëndikoo. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Vitellaria paradoxa + +garab +meññeef +Bëtu-Jaan garab la gu ëppe ci réew yi ci diggu àdduna bi, fu ci mel ni: Madagaskaar, Réewu Kóngo, Endonesi, Folorit... + +Melo +Garab la gog ab taxawaayam day àgg 8 ba 9i met. Ay xobam dañuy ràbbaloo defub dank. + +Ay doomam dañuy defum sàq, xonq coyy te dëgër lool ba noppi nangoo bari. ( sakkan) + +Bëtu-jaan bu tolloo ci di dëgër, dootul neex a sempi ndax reen yi dañuy law fu sori ci biir suuf si. + +Ay loram +Garabu bëtu-jaan nag amna ay lor: + +-Xoox yi dañoo am tooke. Benn xoox rekk boo ko ci yëyee man na laa faat. + +-ku kay jëfëndikoo day wàññi tooke gi. Dangay baxal xoox yi ak meew ba ñu bax nga weer leen ci naaj wi ba ñu wow. + +Ay njariñam +Waa pajum cosaan dañ koy jëfandikoo. + +Xob yi dees koy baxal di ko naan day faj soj ak woppi sëqat. + +Day yokk kàttanu góor ci néegu sëy. + +Dees na ko it jëfandikoo ci sëqal kawar. + +Xoox yi dees na ko def i per fecckat yi di ko takk ak a def ci seen i juŋ-juŋ. + +Xoox yi it nattukaay la: Xoox bu ci ne ak moroom ja ñoo tolloo ag diisaay, ba tax na waa End dañ koy natte seen i wurus.( 12i xoox di dayob 11,6 garaam ci wurus). + +Nataal + +Turu xam-xam +Abrus precatorius + +garab +Garanaat xeet la ci xeeti garab yi nga xam ni dañuy am fóoyteef, mi ngi bokk ci njabootug Lythracées . Cosaanam ma nga nekk fële ca Asi ñu di ko bay ci kémbaar yu bari, fi muy sax nag mooy fu xaw a am aw naaj. + +Melo wi +Garab gu ndaw lay doon, guddaayam man naa jàpp 6i met. Man naa dund 200i at, waaye li ëpp ci limiy jur mi ngi koy jur ci 20i atam ju njëkk yi. + +Ay Tóortóoram, dañuy yor melo wu xaw a xonq, 3i sentimet la baaxoo di gudde, ñatti yoon rekk lay meññ ci at mi, weeru Ut ak Me . Melow foytéefu "Garanaat" ñoo ngi sukkandikoo ci nimuy matee, maanaam yenn saay mu yor melo wu weex, walla wu xoq, walla wu mboq. + +Doonte man naa dund ci suuf su xaw a wow waaye du tee garab gi suuf su xaw a tooy la bëgg ngir mu man a jur ay foytéefam ni mu ware. + +Solo si +Garanaat garab la gog manees na cee defar ay jar doom bi dees koy lekk ay tóortóoram manees na cee xeex yenn wopp yu mel ni Aasm. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Punica granatum +Xoos xeetu garab la bu bokk ci njabootu Rubiaceae ak ci ñoñ Mitragyna. Afrig gu Sowwu ak gu digg lay nekk. + +Meloom wi +Guddaayam danay àgg 8 ba 10i met. Xobam ci guddaay day àgg 6 ba 9i sàntimet, ci yaatuwaay 3,5 ba 5 sàntimet. Melow xol la yore. Tóotóoram day weex te am xet gu tar. Yaatuwaayam 2 ba 2,5i met la. Cari foytéefam day yàgg ak ñoom lool. + +Njariñam li +Xoos garab gees di jëfandikoo la ci pajum cosaam ngir faj xeeti tawat yu wuute. + +Nataala yi + +Turu xam-xamam wi +Mitragyna inermis + +garab +Werlaay garab la gu man a gudd fan lool. Fi mu ëppe mooy ci réewi Afrik yu tàng yi fu ci mel ni Senegaal, Muritani, Sudaã, Somali Ba sax ci réewi araab yi ak réewum Endonesi. suuf su saf-sàpp te am ban ak poto-poto lay ñore + +Melo wi +Garab gu ndaw la. Taxawaay bi 2i met du ko weesu. Ay caram dañuy àgg it ba 2i met. + +Ay njariñam +Ay doomam dees koy watt di lekk. Xob yi ak reen yi dees koy jëfëndikoo ci wàllum pàj lu ci lu mel ni biir buy daw ak mbàq gu am góom ( estoma). + +Loraange yi +Gisuñu benn loraangeem. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Abutilon pannosum . + +garab +Waax xeetu garab la gu bokk ci njabootu Poaceae ak ci njabootaatu Bambusoideae, Afrig gu naaje la bàyyikoo. + +Meloom wi +Man àgg ba 10i met ci guddaay ak 10i sàntimet ci yaatuwaayu dàtt. Xobam danay àgg ci guddaay 1 ba 2i sàntimet. Doom danay àgg ci guddaay 10 ba 15i milimet. + +Njariña yi +Dees na ko jëfandikoo ci defarug alkol, ñoll ak duu. Waax ci xeeti tabaxukaay yi la bokk. + +Nataala yi + +Turu xam-xamam wi +Oxytenanthera abyssinica + +garab +São Pedro benn dekk-dëkkaan São Vicente ci yu penku yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://mindelo.info/gal_spedro.php + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Daqaaru tubaab xeet la ci xeeti garab yi mi ngi bokk ci ñoñ Prosopis , ci njabootug Fabaceae. +Ñi ngi koy fekk ci yenn gox yi ci diggu Sili walla ci bëjsaalum Peru, da fa bari lool. + +Melo wi +Garab la gog guddaayam moo ngi tollu ci 14i met. Peeram dafay rëy, yaatuwaayam mi ngi tollu ci 1i met. Am xasam day yor melow paalmaan am ay xar-xar. Ay foytéefam dañiy wëraloo, seen guddaay di tollu ci 15i sàntimet, ci biiram ay doom yu baree fay ne, doom yi day niru ak doomi kafe. +Moo ngi génn li ëpp diggante Oktoobar ak Desàmbar. Ay foytéefam mi ngi ñor diggante weeri Feewiriyee ak Awril. Garab la gog day màgg ci suuf su nooy, ci tund yi xaw a wow. + +Njariñ yi +Garab gog dees koy jëfandikoo ngir màtt, ay xobam dees koy xoontee baayima yi, foytéefam jur gi bëgg na ko lool. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Prosopis chilensis + + garab + meññeef +Xarañ garab gog moo ngi cosaanoo fii ci Afrig, te bokk ci njabootug Capparacées. + +Garab la gog dees na ko fekk ca: Mosàmbig, Botsuwaanaa, Namibi, Senegaal ak Madagaskaar. + +Melo wi + +Garab la gog peeram dafa am ay dég. +Ay foytéefam dañiy lang ci kaw ab peeram. + +Yaatuwaayam moo ngi tollu ci 40i met jàpp 50. +Aw meloow day xaw a weex buy tàmbali ñor, bu demee ba ñor meloom wi day gel. + +Garab la gu bari lu miy faj lool, day faj biir buy daw. +Dees na ko jëfandikoo it ngir rafetal yenn barab yi, dees na ko sàkketee it. +Leeg leeg foytéefam dees na ko lekk. + +Nataal yi + +Turu xam-xam + +Capparis tomentosa + +garab +meññeef +Koko gi xeetu garab la gu bokk ci njabootu Arecaceae. + +Melo + +Ci gamgamlekaay disaayu doom bi danay àgg ba 1,5i kilogaraam. Day ëmb ndox mu saf suukar: "ndoxu koko". + +Reenam day dugg ci suuf guddaay guy àgg 4 ba 5i met. + +Limu tóotóoram duy wees 20 mbaa 30. + +Njariñ + +Koko bi deef na ko lekk nim bindoo, mbaa soppi ko ay xeeti diw, mbaa ay aniinukaay. + +Nata + +Turu xam-xam + +Cocos nucifera + +garab +meññeef +Tàndarma garab la gu bokk ci njabootu Arécacées ak ci njabootaatu Coryphoideae. + +Melo + +Garab gi day àgg 15 ba 30i met ci guddaay. Téeñu xob lañ am. + +Xobam day àgg 4 ba 7i met. + +Tàndarma bi day meññ ak i ñoñam ciw car. Day saf suukar lool. + +Ngelaw leey tóoral tàndarma gi. + +Njariñ + +Tàndarma bi dees koy lekk te njaayam bari na lool, rawatina ci weeru koor. Tàndarma gi it bari nay njariñ. + +Nataal + +Turu xam-xam + +Phoenix dactylifera + +garab +meññeef +Fontainhas benn dekk-dëkkaan Porto Novo ci yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://www.ecaboverde.com/cat48.htm +Biblioteca Nacional Digital - Plano hydrographico do porto da Ponta do Sol, Lisboa, 1900 + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Santa Luzia diiwaan dunu ci yu Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Armand d'Avezac and Eugène de Froberville, Îles de l'Afrique. L'univers : Histoire et description de tous les peuples, Firmin-Didot, Paris, 1848, p. 214 + +Lëkkalekaay yu biti + +https://web.archive.org/web/20120224220525/http://www.areasprotegidas.cv/index.php?option=com_content&view=article&id=25&Itemid=11 + +Duni Kap Weer +Campeonato Nacional: football (Kap Weer). + +1976 : CS Mindelense (Mindelo) 0–0, 3–0 Botafogo São Filipe +1977 : CS Mindelense (Mindelo) 2–0, 0–2 (4–3 pen) Sporting Clube da Praia +1980 : Botafogo São Filipe 2-1 CS Mindelense (Mindelo) +1981 : CS Mindelense (Mindelo) 2–0 Botafogo São Filipe +1983 : Académico Sal Rei 2–0 CS Mindelense (Mindelo) +1984 : FC Derby (Mindelo) 6–5 pen Académica (Espargos) +1985 : Sporting Clube da Praia 2–0 SC Morabeza +1987 : Boavista FC da Praia 3–1, 0–0 SC Atlético (São Nicolau) +1988 : CS Mindelense (Mindelo) 2–0, 0–1 Sporting Clube da Praia +1989 : Académica do Mindelo - SC Santa Maria (Sal) +1990 : CS Mindelense 2–1, 1–0 Desportivo da Praia +1991 : Sporting Clube da Praia 0–0, 1–0 Desportivo Ribeira Brava (São Nicolau) +1992 : CS Mindelense (Mindelo) 0–0, 1–1 CD Travadores (Praia) +1993 : Académica do Aeroporto (Espargos) 2–2, 2–1 Boavista (Praia) +1994 : CD Travadores (Praia) 2–0, 2–1 SC Atlético (São Nicolau) +1995 : Boavista FC da Praia (Praia) +1996 : CD Travadores (Praia) +1997 : Sporting Clube da Praia 0–0, 1–1 CS Mindelense (Mindelo) +1998 : CS Mindelense (Mindelo) +1999 : GD Amarantes (Mindelo) 2–0, 1–1 Vulcânicos (São Filipe) +2000 : FC Derby (Mindelo) 1–1, 1–0 Académica Operária (Sal-Rei) +2001 : Onze Unidos (Vila de Maio) +2002 : Sporting Clube da Praia +2003 : Académico do Aeroporto (Espargos) 3–1, 3–2 FC Ultramarina (Tarrafal) +2004 : Sal-Rei FC (Sal-Rei) 2–0, 1–2 Académica (Praia) +2005 : FC Derby (Mindelo) 1–1, 4–3 Sporting Clube da Praia +2006 : Sporting Clube da Praia 1–0, 2–2 Académico do Aeroporto (Espargos) +2007 : Sporting Clube da Praia 0–0, 1–1 Académica (Mindelo) +2008 : Sporting Clube da Praia 0–1, 3–0 FC Derby (Mindelo) +2009 : Sporting Clube da Praia 2–0, 1–1 Académica (Praia) +2010 : Boavista FC da Praia (Praia) 2–0, 1–0 Sporting Clube da Praia +2011 : CS Mindelense 0–0, 1–0 Sporting Clube da Praia +2012 : Sporting Clube da Praia 1–1, 0–0 SC Atlético (Ribeira Brava) +2013 : CS Mindelense 3–0, 2–2 Académica Porto Novo +2014 : CS Mindelense 2–1, 0–0 Académica Fogo +2015 : CS Mindelense 1–1, 1–1 (4–3 pen) FC Derby (Mindelo) +2016 : CS Mindelense 0-1, 1-0 (5-4 pen) Académica Porto Novo +2017 : Sporting Clube da Praia 2–1 3–2 FC Ultramarina Tarrafal +2018: Académica da Praia 2–0 CS Mindelense +2019: CS Mindelense 3-1 GD Oásis Atlântico (Santa Maria - Sal) + +Xool it +Football +Campeonato Regional (Boa Vista) (Liig gu Dunu Boa Vista) +Campeonato Regional (Brava) (Liig gu Dunu Brava) +1. Liig - Fogo +1. Liig - Maio +1. Liig - Sal +1. Liig - Santiago gu bëj-gannar +1. Liig - Santiago gu bëj-saluumu +Campeonato Regional (Santo Antão Norte) (Liig gu Bëj-Gannar bu Dunu Santo Antão) +Campeoanto Regional (Santo Antão Sul) (Liig gu Sowwu bu Dunu Santo Antão) +Liig São Nicolau +1. Liig - São Vicente + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20141231042035/http://fcf.cv/pt/index.php/competicoes/campeonato-nacional +https://web.archive.org/web/20120926085440/http://www.fifa.com/associations/association=cpv/nationalleague/standings.html +http://www.rsssf.com/tablesk/kaapvchamp.html + +Football +Kap Weer +Clube Sportivo (Klub/Club Sportif) Mindelense benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Mindelo ci yu dunu São Vicente. + +Campeonato Nacional (Kap Weert): +1975/1976, 1976/1977, 1980/1981, 1987/1988, 1989/1990, 1991/1992, 1997/1998, 2010/2011, 2012/2013, 2013/2014, 2014/2015, 2015/2016, 2018-19 + +1. Liig - São Vicente: 49 +1934?, 1938, 1939, 1942, 1943, 1946, 1947, 1950, 1951, 1952, 1954, 1955, 1956, 1957, 1958, 1959, 1960, 1962, 1966, 1968, 1969, 1970, 1971, 1974/75, 1975/76, 1976/77, 1977/78, 1978/79, 1979/80, 1980/81, 1981/82, 1987/88, 1988/89, 1989/90, 1991/92, 1992/93, 1993/94, 1995/96, 1996/97, 1997/98, 2005/06, 2008/09, 2010/11, 2012/13, 2014/15, 2015/16, 2017-18, 2018-19 + +Staad +Staad Adérito Sena (Estâdio Municipal Adérito Sena) + +Dencukaay + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + Alex (Aires Alex Marques) + Nhambu + Adérito Sena + Sténio + Toy Adão + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Dalub web CS Mindelense + +São Vicente (Kap Weert) +Football +Narab garab la gog dees koy fekk ci tund sahel ba Sudaan, Senegaal jëm Kamerun ak yenn gox i Afrig yi, garab la gog dafa bëgg suuf su xaw a tooy. + +Melo wi +Garab la gog day am ay dég sëq lool guddaayam manees na ko natt ci 10 jàpp 20 ci ay met. Yaatuwaayam dees na ko natt ci 80i sàntimet. + +Am xasam day leer yor melo wu baam. + +Taw yu jëkk yi ci la garab gi tàmbali di am ay xob. + +Foytéefam day am ay doom yoy bu demee ba nekk mag, da na man a làmboo ak 5 jàpp 9 ci ay doom. + +Njariñam +Garab la gog dees koy jëfandikoo ni fiime ngir dekkilaat suuf si. Boo demee ci pajum cosaan garab la gog day faj metiitu biir. + +Garabu matt la it. + +Nataal + +Turu xam-xam +Acacia polyacantha +garab +Suuruur xeetu garab la gu bokku ci njabootug Fabaceae ñoñ Mimosoideae. Moo ngi cosaanoo ci Afrig sowwu jànt. + +Aw Meloom +Garab la gog day am ay dégg. Ab guddaayam man naa àgg ba 10i met. + +Njariñ yi +Garabug suuruur ay njariñam barina lool dees na jariñoo: bant bi, xas mi, ak ndox miy genne ci moom. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Acacia seyal + +garab +Wëttéen garab gu ndaw lay doon mi ngi bokk ci njabootug Malvacées + +Melo wi +Wëttéen garab la gog day màgg sax ci yenn gox yi nga xam ne day am naaj te suuf si xaw a wow. + +"Wëttéen" garabu ñax la gog man naa dund ay 10i at. Guddaayam dees koy natt ci 10i met waaye buñu koy bay dañ koy gàttal ci ñaari met ngir yombal jël giñuy jël Wëtteen wi. + +Tóor-tóoram dañuy génn ci ñaari pàcc, gog day weex ak pàcci gog day mboq te yor genn xet bees ràññeef lool. + +Ci noonu ci lay amee lu mel ni mbaxana bob day dëgër, bob day màgg daa di ubbeeku daa di bàyyi doomi wëtteen yi ñu génn ci doom yooyu ci la fiibar bi di génnee nga xam ne moom lañuy jëfandikoo. + +Te wëttéen yi bari nañ lool waaye bi ci ëpp liñuy jëfandikoo mooy bi ñuy woowe Gossyium hirsutum + +Ngir bay Wëttéen danuy soxlawoo ab diir bu xaw a yàgg. Fu bari naaj, dees na jàpp diir bi ci 520i fan yoo xam ne danu koy suuxat ngir màggal ko ba noppi nga as ndiir ngir mu wow, as sos doo ko nàndal ngir may Wëttéen wi mu xaw a wow. + +Garab la gog dees koy bay ci mbayum nawet ci Afrig, ak End, ak Amerig. + +Njariñam +Garab la gog ay at a ngii ñu koy jëfandikoo ngir di ci de far ay yéere yu nooy. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Gossypium hirsutum + +garab +Tojj Garab la gog ci barab yu wow yi la ëppe ak ci digg Afrig ( Tógoo, Sudaan, Eritere, Senegaal, Tansani, Càdd... ) ak "penku-digg" , "Asi gu naaje" ak ci barab yi néewub taw. Ab guddaayam day àgg ba 10i met. + +Ay xobbam day man a yàgg lool (gudd fan). Ci ndox yu taa yi lay saxe. + +Melo wi +Tojj day gudd lool, te njobaxtal la mel ni lu wërnbalu, am i cat. + +Am xàncam day yor melow baam, day nooy, mel ni waasintóor yu jën. + +Tojj day bari ay wànqaas yu ndaw, Xob yi da ñuy tegaloo, nooy it, am i gaañu-gaañu. + +Tojj xet gu neex la am. Doom bi day tuuti te wex xàtt. + +Njariñ li +Am na ñuy jëfandiko doom bi ak ug wexam. + +Xob yi it dees na ko def ci ñam. + +Xob yi dees na ko wal def ko sunguf di ci saafara ay jàngoro yu ci mel ni safoodi lekk. Day fajj it ag coono. + +Xanc mi day faj góom. Xob yi it day faj biir buy daw, buy metti ak sibbiru te day yokk ngóora ak jàngoroy sëy. + +Xob yi it jur gi it dañ koy lekk + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Maerua angolensis + +garab +Ngol garab gu ndaw lay doon, gu bokk ci njabootug Fabaceae. Mi ngi yaatu lool ci tund Sahel wi ak Sahara ci Afrig ak ci réewi araab yi. + +Melo wi +Garab gu ndaw lay doon, xaw a gudd, am xasam day liis, ay xobam guddaayam manees na koo natt ci (5-8 sentimet), ay tóortóoram day mboq. +Xopi garabu ngol dees koy jëfandikoo ngir dundaleko ak jur garab gi itam leeg-leeg dana am ay tooke garab gu man a sëq lool la manees na cee wut dund ub gëleem ak xar yi ak bëy yi. Yamb yi it di nañu soxla tóor-tóori garab gi ngir man caa defar lem bant garabu ngol di nañu ko jëfandikoo ci defar këriñ man na matt lool itam xas mi man nañu cee defar buum ndox mi it dana génne daakaande waaye daakaande ji leeg-leeg du baax lool manees na cee defarn foroote itam boo jëlee xop yi dëbb ko jaxase ko man na foroote. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Acacia ehrenbergiana + +garab +Sàppóotigarab la gu bàyyikoo Amerig gu digg, mu mujj yaatu ba agsi Afrig ak Asi. + +Melo wi +Garab la gu am ay meññeef ñu neex. Ci aw déeg la ëppe waaye it di na am ci ag joor. + +Màggug sàppooti daa yeex lool. Ay doomam yu jëkk a ngi tàmbalee ci ñeent jàpp juroomeelu atam. At mépp nag lay am i doom. Ci menn at man na cee joxe 150 jàpp 200i kiloy doom. + +Taxawaay bi day àgg 15 met ba 30i met. Xob yi dañoo xaw a dëgar. Xas mi du ëpp 80i sàntimet cib rëyaay. + +Njariñam +Doom yi dees koy lekk, ñam wi daa am ay ferñent, da lay sawarloo, baax na it ci ay butiit ndax day reesal. Ab bantam lawbe yi ak liggeeykatu bant yi dañ koy jëfandikoo, di ci defar ay toogu walla ay lal. + +Tur xam-xam wi +Achras sapota + +Wàll:garab +Peex xeetu garab la gu bokk ci njabootu Bignoiaceae te bàyyikoo Afrig gu naaje. + +Melo +As ngarab la su am i tóortóor yu yor melow puur te dajaloo ciw car. + +Njariñ +Jur gi dañ ciy xéewaloo. + +Nataal + +Turu xam-xam +Stereospermum kunthianum +Sebeer bukki garabu paj la gu bokk ci njabootu Acanthes. Ci waax yu bane yi lay meññ. Asi gu naaje ak Afrig la cosaanoo. + +Njariñ +Dees koy fajoo. + +Nataal + +Turu xam-xam +Hygrophila auriculata + +garab +Siddeem bukki xeetu garab gu bokk ci njabootug Rhamnacées. Moo ngi coosaanoo Lo ci réew yu naaje yi. + +Aw meloom +Siddeem bukki garab guy am i dég, ak i doom yu nuy woowee siddeem bukki. Garab gu dëgër lay doon ci jamonoy noor. + +Am xasam day ñagas am ay pàq, wànqaas yi yaatu, ëppante te am i dég. Xobam yi seen wirgo day wuute. + +Njariñ yi +Doom bi dees na ko jëfandikoo ci togg, dees na ko lekk noonu it. + +Foytéef bi barina ay ferñeent lool. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Ziziphus mucronata + +Garab + +Meññeef +Garabu lawbe, mbaa dundul, mbaa guy-jéeri noo ngi koy fekk ci xalag sowwu jantu Afrig niki Senegaal jëm diggu Afrig, dalee Gine ba Gana, jaare Niseriya jëm bëj-saalumu Càdd. Ag ñeme conoom tax na mu man a dund ci àll bu wow, fu naatul lool ak fuy am naaj. Garab gi dina man a dund itam ci barab bu am i xeer ndax buutam ni mu man a denccee ndox noonu la ko man a muucoo. + +Melo +Lawbe gi garab la gu am ay xob yu ndaw. Njoolaayam dina dem ci li ëpp ci 10 ba ci 25i met. Ci Sahel nag néew na li muy weesu 6i met. Peeru garab gi day am i dég rawatina bu garab giy màgg, xas mi woyof. Garabu Lawbe dëgg-dëgg garab gu man lu bari la, di joxe ay garabu paj, ñam wu nuy lekk, diw, matt, añs. Ñoo ngi koy bay ci Afrig sowwu jant. Garab gi mi ngi tóortóor ak a meññ li ko dalee ci juroom benneelu atam, moo ngi aju ci nekkiinam. Ci li ëpp mi ngi meññ ci noor. Waaye nag daay yi du ñu leen may ñuy am jiwu. Genn garabu Lawbe gu mag man naa meññ ba 1500i fóyteef ci at mi. + +Ay njariñam +Garab gi bari na ay njariñ lool. Man na doon dëkkuwaayu yamb. Tóortóor yi dees koy weer ba mu wow, ñu wal ko def ko cafaay. Foytéef yu ndaw yi man nañu leen togg. Yu matul yi itam man nañu koo jariñoo ci ndefarug njar. Niinaayu diwam tax na mu bokk ci yi nit di jëfandikoo cim paj, xasu garab gi day yokk saw te day yombal mbaaxum jiggeen. Ku ko baxal it, man naa faj ràmm, ak payiis, ak bopp buy metti, man na itam waññi ween yu rëy. Ci bopp buy metti itam manees na jël xob yi rekk takk ko ci. Boppam baax na lool ci dakkal nacc-nacc ak ci biir buy daw, ci kaw mu ànd ak yeneen i garab. Sangoo ndox mu tàngu garabu lawbe baax na lool ci ku néew doole. Pàcc yi bari ci garab gi la ñuy jëfandikoo ngir faj tàngooru yaram, walla ngir wàññi coono walla ngir yokk soowum jiggeen juy nàmpal. Ci wàllum njëmbët garab: Garabu Lawbe am na ci solo ndax safara manul ci moom lu bari, ba tax na mu man a nekk xàmmekaay. Xam-xam wane na ni garabu lawbe baax na ci suuf. + +Yeneen i njariñ +Fiibar bi nekk ci biir foytéefu garab gi manees na koo jariñoo ci defar i pajaas ak i ngegenaay. Xas mi man na cuub. Doom yi dañoo bari diw lool ba àgg ci cosaanal petorol. Garab gi man na joxe itam matt ak lenn ci lu nu man a jëfandikoo. + +Mbayam +Jiwoom bokk na ci liy yaatal dund garab gi waaye jëmbët ko it man na nekk su dee garab gu ndaw gi dina aaru ci daay ak ci mala yi. + +Nataal + +Turu xam-xam +Bombax costatum + +garab +Liisugar, xeetu garabu tóortóor la. Garab la gog mi ngi cosaanoo ci penku Afrig ak bëj-saalumu réewi araab yi. + +Melo wi +Garab la gog dafa am ay xob yu dëgër guddaayam manees na koo natt ci 3i met jëm kaw, peeram dafa yaatu lool te rëy. +Garab la gog dafa bari ay car lool ci jeexitalu car yi da nan fa gis ay tóotóor yoo xam ne guddaayam manees na koo natt ci 5 jàpp 15 ci sàntimet walla 1 jàpp 13 ci yaatuwaay. +Garab la gog dees koy jëmbët ci ay pot. Mu yaatu lool ci tund wi nga xam ne dafa digg-dóomu tàngul seddul day soxlawoo naaj. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Adenium obesum + +garab +Totaasoro xeet la ci xeeti acacia. Garab gi amna Senegaal, Kamerun, ba ca Réewu Diggu-Afrig. + +Melo wi +Totaasoro garab gu am ay dég te ndaw la, guddaayam man naa toll ci 8 jàpp 9i met. + +Ay xobam dañuy sew, seen guddaay man naa toll ci 3 jàpp 7i sàntimet. +Garab gi mi ngi jebbi ci taw yi jëkk, walla lu ko jiitu tuuti. + +Njariñ yi +Garab gi dees na ko jëfandikoo ngir faj biir buy daw ak jafe-jafey mbàq, ak ku jaan màtt. Bantam dees na ko jëfandikoo ci liggéeyu tabax, di nañ ko def itam matt di ko taale, mbaa këriñ. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Acacia dudgeoni + +garab +Këwsu garab la gu bokk ci njabootug moracées. Moo ngi bàyyikoo ci dëkki Asi yi. +Garab la gog ci ay bot lañ koy jëmbët, ci réew yi xaw a tàng. Xeetu garab la gog bareetul ci foofu mu cosaanoo muy Asi. + +Melo +Këwsu garab gu mag la, day màgg màgg gu gaaw. Guddaayam mannaa toll ci 30 ba 40i Met. +Xobam day nëtëx fu mu toll. Garab gi bu màggee day am ay doom. Doom yu ndaw yi seen guddaay 1 jàpp 2i sàntimet lay toll. Garab gi xob yu mag yi seen guddaay danay toll ci 10 jàpp 35i ci ay sàntimeet. Seen yaatuwaay moo ngi toll ci 5 jàpp 15i ci sàntimet. Garab yu ndaw yi seen xob mooy gën a gudd, Xob yi ñoo ngi màgge ci biir lu mel ni mbaxana. +Mbaxana moomu day màgg ni xob di màgge. +Bu demee ba xob wi mat, mbaxana mi day daal di rot. Garab gu bari ay reen la. + +Njariñ yi +Këwsu dees na ko jëfandikoo ngir rafetal ay barab. + +Nataal + +Turu xam-xam +Ficus elastica + +garab += (désert) + = (desert) +REDIRECTION Màndiŋ m +Dédd genn xeet la ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug Fabacées, mi ngi fekk baax ci Afrig gu ron-saharaa + +Melo wi +Garab gii melow ñax gu sëq gu law ci guddaayu garab lay yor. + +Yenn saa yi nag melow as ngarab su dàttam di àgg 20 ba 30i sàntimet ak 3 ba 5i met ci guddaay lay yor. Daa bariy dég, yu ay car ak reeni xobam tiye. Seen ug guddaay danay àgg ba 8i milimet. +Doomam day tàcc, di yore melow puur, xonq mbaa baam tey àgg cig natt 6 ba 10i sàntimet ci guddaay ngir 1 ba 1,5 sàntimet ci yaatuwaay. Ci tënk 6 ba 8i saal yu tàcc, yu nëtëx mbaa xuun lay ëmb. + +Njariñ +Dédd gi deef na ko jëfandikoo nig garabu paju cosaan. Tóortóoram meññ lem. Màttam danay jariñ ci defarug jumtukaay yu wuute (tum, fett...). Wàqaasam dees na ko feteñe. + +Nataal + +Turu xam-xam +Senegalia ataxacantha +acacia ataxacantha + +garab +Màmbeyaa gi garab la guy nekk ci gox yu naaje yi, ci njabootug Moraceae la bokk. + +Melo wi +Xobam yu yeesam day xonq, bu saxee nag nëtëx. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Ficus umbellata + +garab +meññeef +Tàkk g + +Fr: désert +Old Trafford benn staad ci football club Manchester United ci ye dekku Manchester, Angale, Nguur-Yu-Bennoo). + +Nataal yi + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Manchester United Official Website + https://web.archive.org/web/20070713220631/http://www.uefa-archiv.de/manchester.html + +Nguur-Yu-Bennoo +Staad +Estádio da Várzea benn staad ci ye dekku Praia ci yu dunu Santiago ci Kap Weert. + +Football klubi +Académica - Praia +ADESBA (AD Bairro) - Bairro Craveiro Lopes - Praia +Boavista FC - Praia +Celtic - Achadinha de Baixo - Praia +Sporting Clube - Praia +CD Travadores - Praia +Vitória FC - Praia + +Nataal yi + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Fussballtempel - Staad Kap Weert + Estádio da Várzea - Stadium Database + Estádio da Várzea - World Stadiums + Estádio da Várzea - World Stadia + +Santiago (Kap Weer) +Staad +Saasumaan Mooy waxambaane wu tollu ci ay jamonoom. Day tolloo ak xale bu góor bi, waaye ci biir xale bu góor man ngaa nekk xale bu góor te doo nekk Saasumaan. + +Ndax Saasuman dëgg dëgg day tolloo ak (booy diskoo) ci sunu jamono jii. +Lameirão benn dekk-dëkkaan São Vicente ci yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +Dekk-dëkkaani Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Calhau benn dekk-dëkkaan São Vicente ci yu penku yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +http://mindelo.info/gal_calhau.php +Michel Lesourd, "Calhau", Le Cap-Vert, Jaguar Publishers, Paris, 2006, p. 212 ISBN 978-2-86950-408-0 + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Baía das Gatas benn dekk-dëkkaan São Vicente ci yu penku yu dunu São Vicente, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Michel Lesourd, "Baía das Gatas", Le Cap-Vert, Jaguar Publishers, Paris, 2006, p. 211 ISBN 978-2-86950-408-0 + +Lëkkalekaay yu biti + +Festival da Baia das Gatas +https://www.facebook.com/SoncentLiKeTerra + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +São Vicente (Kap Weert) +Corda benn dekk-dëkkaan Ribeira Grande ci yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +AJ MÀKKA + +Bind bu jëkk + +Nu fas yéenee jàngale aj ak ajiin yi, nu tàmbalee ko nii: + +Xeeti ajiin yi ñatt lañu: + +▪︎Ifraad : (li muy tekki mooy bennal, wéetal, aj rekk a tax nga jug), su dee ci waa Senegaal ñu armale ca armalu (miixa) ba ñuy wax Zul Hulayfa (Biiru Hali), di jumaa ju nekk ca wetu Madiina, ngir def faratay aj. Soo noppee ci mbooleem jëfi aj ji aki jaamoom, dinga man a def sunnas Umra, su boobaa jënd gàtt du la war, di ko ray ci bisub iid gi (hadyu) + +2eelu bind + +▪︎Ajug xéewu (tamattuh): + +Mooy nga armale ca armalu ba ci yéeney jëkk a def sunnas Umra. Soo noppee ci def jëfi Umra, nga summiku (ci sa yérey armal), sol yére yi nga baaxoo woon. Ci juroom-ñatteelu fan ci weeru tabaski (zul hijja),  ca suba sa, ca ngay armale ca Màkka ci yéene def faratay Aj, ànd ak ajkat yi dem Munaa ngir def jaamuy aj yi ba ñu jeex. Tawaaful qudoom nag du la warati. Li ngay def kay mooy jënd ab gàtt, ray ko ca bisub tabaski ga. Ndaxte dangaa xéewoo (tamatuhe) jiital sunnas umra ci faratay aj, soo manul a jënd ab gàtt ngir ñàkk koo man, kon dangay woor ñatti fan ci biir aj gi, ak yeneen juroom-ñaar soo delloo sam réew + +3eelu bind: + +▪︎ Ajug Qiraan walla ajug lëkkale: mooy mu aramale yéeney sunnas Umra ak faratay Aj ci wenn waxtu ( maanaam mu yéenee defandoo ñaar yi), sooy noppi ci jëfi aj ji fekk na nga matal tam jaamuy umra. Fii it hadyu war na la walla woor na nga ko defe woon ca Tamattuh (xéewu). Dangay gis ne ci jëf yii yépp aji aj ji day xér ci jóoxe faratay aj ak sunnas umra ngir am seeni yool ak pay + +4eelu bind + +▪︎Aj daa am ay ponk aki wareef. + +Ponki aj deesu leen jange (defare) dereet (ci hadyu) su ñu yàqoo, ñoom nag ñeent lañu: + +1 - Armal: mooy yéenee dugg ci aj gi, walla sunnas umra, mu lëkkaloo ak rafle ci lu ñu ñaw, ak sol lees yérey armal ya, ak wax làbbayka jëm Màkka gu sell ga + +2 - Dox diggante Safaa ak Marwa, mooy dox ko joroom ñaari yoon, benn mu nekk ci ginnaaw wërug dikk gi (tawaaful qudoom) ñeel ajkat bi, walla ginnaaw tawaaful Ifaada (wërug bëbbal gi) ñeel ajkat bi deful tawaaful qudoom, ak it ñeel ki def tamattuh, nga xam ne daa jiital sunnas umra , mujje faratay aj + +3 - Tawaaful Ifaada (Wërug bëbbal gi): mooy wër gi ajkat bi di def ci bisub tabaski, ginnaaw bi mu sànnee Jamratul Haqaba, ak ginnaaw bi mu rayee am hadyoom, su fekkoon mi war ko, ak wat boppam walla wàññi ko ( xoos ci mbooleem kawaru bopp gi). + +4 - Teew Arafa : ajkat bi day juge Munaa, dale ko ci penkuteg jànt gu bisub juroom ñeent ci tabaski wi, fu mu teew ci wàlli Arafa rekk mu doy, moo xam daa tëdd, mbaa mu war, walla mu taxaw, waaye su génnee Arafa (maanaam nekkul ciy wàllam) nag ajam baaxul. Arafa nag mooy ponkub aj bu mag bi. Teew fa nag, doore ko ci sawaal (digg-bëccëg) ba jant so. Nekk ga fa ajkat bi di nekk ba jant so nag daa bokk ci waajibaat yi (wareef yi), ku ko deful man na koo jange (defare) dereet (hadyu), su ci ajkat bi lotte ngir benn ci sabab yi + +5eelu bind + +WAREEFI AJ: + +Wareefi aj yiy jangoo (defaroo) ci dereet, ñi ngi jangoo (defaroo), soo ci bàyyee benn ci jënd am hadyu te ray ko, ngir jaamoo ko Yàlla. + +Wareefi aj yiy jangoo ci dereet, su ci benn faatee ajkat bi, ñooy yii: + +1 - rafle ci lees ñaw ak luy peek ( luy wëre), maanaam bañ a sol yére yu ñu ñaw, ak mbir yuy peek (wër) ab cér niki jaaro ak yu ni mel. + +2 - Armale ca armalu (miixa) ba ñu jagleel dëkk bu ne. Senegaal seen bos mooy  Biiru Ali + +3 - di wax làbbayka ba ca digg-bëccëgug bisu Arafa + +4 - Tawaaful Qudoom (wërug bëbbal), mooy tawaaf gi ajkat biy def su agsee Màkke rekk te fekk mu armal ngir aj Ifraad + +5 - Ñaari ràkkaay tawaaf yi ci Ifaada ak Qudoom, waxees na ne : seen àtte ñooy sunna + +6 - Dox safaa ak marwa nekk ci ginnaaw tawaaful qudoom te jokk ci, su dee ajkat bu juge dëkkam ñëw Màkka te armaloon faratay aj + +7 - Nekk Arafa ci bëcëg gi, dale digg-bëccëg ba jant so + +8 - Wàcc Musdalifa cig dellu juge Arafa ci guddig tabaski gi, jullee fa timis al gee boole leen te wàññi gee gi + +9 - fanaan Munaa ñàtti guddi ginnaaw bisub arafa walla ñaari guddi gën jaa néew, guddig ñaareelu tabaski, ñatteel ak ñeenteel su ko sànni jamra yi ci ñeenteelu bis bi ñoree. Su dee yam ci sànni jamray ñaareelu bis ak ñatteel, kon du jar muy des Munaa di fa fanaanati ca ñeenteel ba. + +10 - Sànni ñatti jamra yi ci bisi tashriiq yiy ñatt (ñatti fan yi sës ci tabaski gi), waxtuw sànni wi mi ngi tàmblee ci digg-bëccëg ( zawaal) ba jant di so. War na ajkat bi mu yéenewaale buy armal ne dina joxe am hadyu, muy ray ab gàtt ci lépp lu mu man a def ciy wuute, wallay tere. Def wuute mooy ñu digal la defoo ko. + +Def tere mooy ñu tere la bàyyiwoo. Su boobaa loolu dina doy. + +6eelu bind: + +Terey aj yi: + +1- sol lees ñaw walla luy peege: ku armal du sol jàllaabi, simis, pantalong, du jenn tubay mbaa mépp mbubb mees ñaw, du sol it jaaro, kaala, walla lenn lees man ne day peege mbaa ñu ñaw ko. + +2 - Lees man a féexale yaram wi ak di ko setal, du muur bopp bi, du wat kawar gi, du lewwi we yi, du dindi ag fagg akub tër ci bopp bi walla ci yaram wi, du jëfandikoo gëtt ci mbubbam mbaaw yaramam, mbaag diw ci bopp bi, ak yeneen yi aju ci setal mbaa dindi ay taq-taq añs + +3 - Jigéen ñi: du dagan ci Aji armal ci Màkka muy jege jabaram cib sëy walla laal, mbaa fóon, walla muy ngoro mbaa muy ngorool, mbaa muy fasal boppam ab sëy mbaa mu koy fasale. + +4 - Rëbb: daganul ci ku armal muy rëbb dara ci rëbbum jéeri mbaa mu koy ray, moo xam luy dox la mbaa luy naaw, mi ngi ci urum ji mbaa mu génn ko, daganul ci moom it moy dog garabi urumi Màkka ji. + +Ajkat bu góor beek bu jigéen bi ci nii lañuy wéy di ñu ñu aaye mbir yii ba kero ñuy sànni jamrab Haqaba, dal di summiku summiku gu ndaw gi, bu booba lépp daganaat ci moom ba mu des jigéen ak rëbb, ñu sib ci moom gëtt, su defee tawaaful Ifaada, dox safaa ak marwa, su defagul it tawaaful wadaah, day def summiku gu mag gi, su boobaa lépp lu armal di aaye dellu dagan ci moom, mu man a jariñoo soxnaam, ndax def na mbooleem ponki aj gi, li ko dese mooy sànni jamra yi ci bisi tasriiq yi( bisi ñaareel, ñatteel ak ñeenteel bu tabaski gi) + +6eelu bind: + +Yiy yàq aj ci ñatti mbir lañu nekk: + +1- Ñàkk a teewe arafa, loolu mi ngi ame ci ñàkk faa man a teew cig wàll ci guddig tabaski gi, muy diggante timis ba fajar fenk. + +2 - Bàyyi ponk ci yeneen ponk yi dul jangu ci dereet ba waxtoom jàll, te manoo koo dabaat. + +3 - Aji armal ju jaxasoog soxnaam te sànneegul jamrab hawaba, wëragul Ifaada, te bisu tabaski gi jeexagul. Su amee nag ginnaaw benn ci ñatt yii, du yàq aj gi cig matale, waaye hadyu moo koy war. Su aj gi yàqoo ngir senn ci sabab yii nu waxoon, ajkat day mottali ag ajam te dal di koy fay saa so ko manee , dal di ray hadyu ngir aj gu yàqu gii te yeexe ko bay fay ca at may ñëw su ko aj jàppandee. + +7eel bind: + +Kañ la hadyu di war ajkat bi? + +Bokk na ci sabab yiy waral hadyu: + +1 - su ajkat bi bàyyee benn ci wareef yiy jangoo ci dereet + +2 - su doonee ku doon tamattuh, jiital umra ci aj, ngir waxi sunu boroom ja: ( ku xéewoo umra ba aj, la jàppndi ci hadyu), ak su defee ajug lëkkale (xiraan), ( maanaam boole sunnas umra ak faratay aj ci yenn jëf ni nu ko leerale woon ca na ñuy armale ci xiraan + +3 - su amee gàllankoor bu ko teree mottali faratay aj gi, ngir waxi sunu boroom ji: ( Bu ñu leen gawee, la jàppndi ci hadyu), su amul lu mu man a jënde hadyu ba koy ray, woor ñatti fan da koy war ci aj gi ak yeneen juroom ñaar su delloo dëkkam, ajkat bi man naa coobarewoo joxe hadyu te du ko war, mu ciy sàkku tuyaaba rekk ngir ne deful dara ci sabab yi nu tudd tey waral hadyu. + +Njot ( walla fidya) maanaam ak li koy waral : + +Njot walla fidya mooy kafaara (far) gu jëm ci tere yi ajkat bi def, di ci ame ag xéewu akub noflaay niki sol lu ñu ñaw, mbaa muur bopp, walla setal yaram, dindi ag fagg, jëfandikoo gëtt (parfum): + +Fidya nag ñatti xeet la, nga tànn ci bu la nee: + +• woor ñatti fan ci fu la neex + +• lel 6 miskiin (miskiin bu ne ñaari mudd) + +• ray ab gàtt xar mbaa bëy + +Tegtalug ñatt yii mooy waxi sunu boroom ji: ( ku ci nekk ci tawat mbaa mu am loraange ci bopp bi, na def fidya, benn mu woor, mbaa mu saraxe, mbaa jaamu (nusuk) + +8eelu bind + +Yeete ñeel ajkat bi: + +Soo génnee sa kër yaw miy aj jëm Madiina ngir siyaare armal waru la, dangay sol lu la neex, di gëttu ak a set waxtu wu la neex. Soo jugee Madiina nag ngir war a armal ngir aji, dangay dem ca sab armalu (miixa), ni ma la ko waxe woon, waa Senegaal seenub armalu mooy Biiru Ali, di jaaka ju ne ca wetu Madina ( Zul Hulayfa) mooy miixam waa Madina, di soree màkka 450 kilomet (junñay). Ku romb sa miixa (armalu) te armalewoo fa, loolu dina waral hadyu war la, ci miixa mii rekk it lees di soppe ñaari ràkka + +- armalug jigéen mooy mu wuññi xarkanaman ak ay tenqam, waaye day sol yére yi mu baaxoo woon a sol, yi ñu ñaw ak yiy peege, muur bopp bi, li war ci moom it ginnaaw jaamuy aj gi walla umra gi mooy mu wàññi kawaram rekk, su dee góor nag day watu mbaa mu wàññi ci mbooleem kawar gi. + +- ajkat bi su dee wër kaaba gi ba jullig farata jot day dog wër ga ba ànd ak nit ñi julli ba ba noppi, dellu ca wër ga ca barab ba mu taxawe woon, mottali la ko dese woon ciy wër. + +- Su jigéen gisee mbërëg, day wéy cig ajam, def ay jaamoom lu ci dul wër kaaba gi, ndax da dul sañ a dugg ci jàkka ji, du wër it ndare bu dafa laab te sangu, ndax wër dafa laaj jàpp niki julli. + +- ku sikk ci ñaata wër la def na jàpp la ko wóor, misaal mu doon sikk ndax ci ñatteel la nekk walla ñeenteel, su boobaa day jàpp ne ci ñatteel la nekk, dal di wéy ba matal. + +- Ku manul a sànni jamrab haqaba walla yeneen yi, sañ naa wut ku ko wuutu ku mu wóolu, dim mbokk mbaab àndandoo, su sànnee ba noppi sànnil ko. + +☆☆☆ + +Mat na + +Ki leen ko doon defal: + +Abdu Xaadir Kebe +Timmiñ-tammañ Gàñcaxug ñax la, di it borom juróomi xob yi bokk. + +Melo +Timmiñ-tammañ day law, ab taxawaayam di àgg ba 10i sàntimet jàpp 20i sàntimet . Ab lawaayam day àgg ba 100 Mt. Ab reenam day dëgër fa miy sax it day mel ni am tàgg ( dankalikoo). Day am am peet mu mboq rafet lool. Ci béreb bi féexlukaay yi lay ëppe ak ci tooli "jardins" yi. Ci jamono yi miy lawe nag mooy ci weeru suliyee jàpp nowambar ( Naweet). + +Njariñ +Ay reenam day yokk ag cawarte. Ab nàcc-nacc it boo ko ci defee day taxawal deret ji. Day faj it biir buy daw. Lawtan gi it daa nañ ko jëfandikoo di ko def ay takkun ngir di ci takk ngóob mi ci jamonay góob. + +Loraange yi +Ñax mi daa am tooke gu bon ci jur gi ba tax na waru ñu koo lekk. + +Nataal + +Turu xam-xam +Potentilla reptans +garab +Ndaybarga , garab la goo xam ne du rëy waaye day sëq taxawaayam nag man naa dem ba juróomi met. + +Fumuy sax ? +Moom nag ci barab yi nga xam ne taw bi xawu faa bari lool lay meññ. + +Barab yooyu bu ñu xaymaa li muy taw ci at mi du ëpp 500 milimet ci taw . + +Melokaanam +Ndaybarga garab la goo xam ne ay xobam xobu lëmm lay doon du ay xob yu sew, ay wànqaasam da ñuy rénki doon lu lunk maanaam: da ñuy dëng wànqaas yu ndaw yiy door a jebbi da ñuy am lu mel ni ay kawari muus. Ndaybarga am na ñaari xeet. + +Fan lay sax ? +Moom nag mi ngi sax ci réew yu bari fii ci Afrig fu mel ni Kongo, Ruwandaa , Sudaan, Ugandaa , Keeñaa. + +Kañ lay meññ ? +Bu nawet bi di waaj a tàmbali walla buy waaj a jeex lay tóortóor maanaam cooroon ak lolli. + +Fu mel ni Keeñaa wax na ñu ne bu noor bi jotee moom rekk mooy doon garab gi nga xam ne day am ay xob yu naat yu nëtëx ba tax na jur gi moom rekk la ñuy lekk ci waxtu woowu. + +Njariñam: +Moom nag xob yi ak reen yi ak xas mi lépp a am njariñ. + +Xobam lu am njariñ la ci nit ak mala ak jur. + +Day dindi mettiit, di faj jangoroy bët, wanent ak biir buy metti, ak màtt-màttu ndox suuf ak jaan. + +Xob yi batay day ray saan, batay ci wàllu pajum Tubaab xob yi am na ag diw gu ñu ciy defar ngir faj. + +Ay reenam boo ko jëlee kakk ko bam def dóom boo diwee dóom bi ci màtt-màttu jaan day dindi daŋar ji, batay dóom bi soo ko jëlee diw ko koo xam ne yaramam dafay metti dana ko faj. + +Batay ay reenam boo ko boolee ak xobi (nebadaay) saab-saab di na faj woppi jur ji ñuy wax (trepanosome) wopp la juy dal jur gi. + +Batay reen yi ak xob yi day faj woppi jur ji ñuy wax "sarbon". + +Njebbiriit li soo ko jëlee dëbb ko man nañ koo boole ak cere, yenn dëkk yi suñu jànkoonte ak ab xiif xob yi la ñuy jël di ko boole ak séen ug lekk ngir sakkanale ko séen dund bu niiw boobu. + +Bu dee xas mi : + +Xas mi moom boo demee dëkk bu mel ni Keeñaa dañ ciy defar ab toogu bu ñuy wax tabre ndax ay bantam dafa neex a dëngal ndax ni ñu bindoo dañoo lunku, batay xas mi am na dëkk yoo xam ni ay buum la ñu ciy Defar. + +Bu dee ay bantam moom dina ñu ko def matt di ko xambee ndax tàkk-tàkkam dafa neex. + +Turu xam-xam +Cadaba farinora +garab +Dungidég garab la gog mi ngi bokk ci njabootug Fagara Zanthoxyloide. + +Cosaan laa nga ca Senegaal ak Kamerun. + +Melo wi +Garab la guy sax ci wetu géej ak fuy am ndox. + +Njariñ li +Dungidég garab la gu bari njariñ. Garab la guy faj jàngoroy biir, jàngoroy dënn añs... Xob yi, xàncam yi ak reen yi dinay faj tawati mbàq guy metti (estomaa), tawati góom i biir ak biti, soj, biir buy daw, emoroyit, ak yeneen. + +Manees na ko soccoo, dinay wàññi daŋaru bëñ buy meti ak it di ko faj. + +Dinay yombal dawug dereet ji. + +Reen yi bari garab yees koy def ci wàllu faj, rawatina ca Burkinaa Fasóo, ca Gana, ca Niseria, ca Mali ak ca Kodiwaar. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Fagara Zanthoxyloide +Sam xeet la xeeti garab , mi ngi bokk ci njabootug Fabaceae, dees koy fekk ci goxi Sahel gi ak ca Sudaan. + +Garab la gog fi muy sax day bari suuf lool walla xeer ñu ngi koy fekk ci réew yii: réewum Bene, Burkinaa Faaso, Kodiwaar, Gine, Gine Bisaawóo, Mali, Niseer, Niseryaa, Senegaal, Siraa Leyoon, Togóo, Càdd, Sudaan. + +Melo wi +Mi ngi bokk ci garabu matt yi, te bari dég day yor xas yu bari, nuroo ak garab gu ndaw guddaayam man naa jàpp ñenti met jëm kaw. + +Bokk na ci garab yi nga xam ne dañuy laxasu, ci loolu nag guddaayam man naa àgg ci fukki met ak juróom . + +Njariñ yi +Moom dees koy watt ngir di ko jox baahima yi ñu koy jëfandikoo walla ñu ciy fajoo, batay it ñu ciy defar matt + +Ay doomam manees na ko jëfandikoo niki xeeti (acacia) yi am yépp dañuy tàkk te dañuy dundal. + +Ay xobam dees koy tàngal bamu tàng di ko jëfandikoo ngir di ci faj biir buy metti ak yu ni mel moom it ba tay dees koy jëfandikoo ngir wàññi ci daŋaru jaan. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Acacia macrostachya + +garab +Nus walla mbuumu giléem garab la gog mi ngi bokk ci njabootug capparceae +Moom nag garab la gu bari lool fii ñu nekk muy Senegaal , ak fu mel ni Moritani , ak Gàmbi daal di dem ba réewum Somali ba wàcc ba ci suuf ci réew mi ñuy wax Afrig gu bëj-saalum. + +Ndax moom ci gox yoo xam ne dañoo xaw a wow lay sax , leeg-leeg mu gàtt , leeg-leeg mu njool. + +Melo wi + +Garabu nus taxawayam dinay dem ba àgg ci 10 fukki met ci kaw , moom nag xob yi ; xob yu dëgër lay doon te dafay nëtëx, baxa saa su ne. Ay reenam fu dëgër la ñuy sàmpu fu mel ni ab xorndom, maanaam fu xorondom dëkk, am xasam it dafa dëgër te ritax. + +Njariñ yi + +Moom nag lu bari ay njariñ la . +Bokk na ci ay njariñam : di na faj opp ji ñuy wax siburu, ak yaram wu tàng , dinay faj jaani biir maanaam ay saan, baax na ci tànk bu newwi ak i góom , baax na ci góor gu niiw kàttan , baax na lool ci jigéen ju taxaw maanaam ku doom jafe, baax na ci soccet , ak i tànk yuy metti rawatina bu dee sedd maanaam "rimaatism" baax na ci biir buy daw rawatina bu àndee ak dereet , ak yaram wu tàyyeel , dina faj it tawat ji ñuy wax sifis . + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + +Boscia angustifolia + +Garab +Rand garab gu ndaw lay, mi ngi bokk ci njabootug Fabaceae, cosaanoo Afrig, dees koy fekk ci gox yi nga xam ni suuf si day xaw a wow fu mel ni Sahel gi. + +Melo wi + +Garab la gog guddaayam li ci ëpp 1i met la doy jàpp 3i met, yenn saay man naa àgg 8i met, day niru garab gu am ay dég, te fekk ci dëgg-dëgg ay car yu amul xob la, ay xobam dañuy yor melo wu nëtëx. Ay doomam njokkub lujum lay doon. + +Njariñ yi + +Garab la gog dees koy jëmbat ngir rafetal. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + + Bauhinia rufescens + + + Garab +Garab gii lañuy wax ci Wolof Yoos turu xam-xam wi moom lañuy wax (Agave sisalana) moom daf a bokk ci xeeti (Agaaf) yi bu ko defe dañuy jëfandikoo baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle ak yaneen (Agaaf) yi ndax xeetu garab yu ñuy wax (Agaaf) daf a bari lool te ci xeetu garab yuy am ci wetu (Amerig) lay doon mu doon xeet yu bari moom nag ñu di ko ràññatle mu bokk ci njabootu (Agaaf) yi waaye ñu jël baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle turu xam-xamam nag mooy (Agaaf sisallnaa) moom nag garab la goo xam ni ci xeeti (Agaafl yi la bokk kon baatu (Sisaal) lañuy jël di ko jëfandiko ngir ràññatle ko ak yaneen garab yi nga xam ne (Agaaf) lañ, +Moom nag fimuy faral di sax réew yu ñuy tudde (Karayibil) fu de me ni (Panamaa) ak (Kubã) ak fu de me ni (Jamayg) réew yooyu fala baree lum fay sax leg lee ñu gis ko faneen waaye foofu la ëpp lum fay sax mi ngi faral it di sax ci barab yi nga xam ni dafa nooy te di faral di tàng foofu la ëpp lumuy sax kon ñi ngi koy faral di gis ci réewu (Karayibi) añs kom ni ma ko waxe. + +Melo wi + +Moom nag garab la goo xam ne day am ab dàtt boo xam ne dàtt bu xaw a dëgar lay doon day bindoo ni dàttu tàndarma day gàtt it waaye dafay am ker goo xam ni ker gu yaatu lay doon gu rëy ker gi it dafay dëll ndax li tax muy dëll mooy xobam yu mu am dafay xob yu tal xob yu tal yoo xam ne daf a xaw a rëy daf a xaw a yaatu su ko defee xob yooyu nuñuy ràbb a loo wee moo tax ker gi dafay xaw a yaatu doonte moom garab la goo xam ne du gudd lool waaye dafay dëll ker gi it dafay yaatu moom nag nimuy saxe dafa mel ni dafa am ay xupptali-xupptal ni ki ni tàndarma di saxe noonu lay saxe ba noppi day sax ay xob mu wër xëb yoy dafay yor melokaanu ab daba ni daba di bindoo noonu lay bindoo, +Boo xoolee xob yi ci wed gi dafay mel ni dafay am ay bëñ yu mel ni ay bëñ i joolaa la am xob yi noon la mel ba noppi dafay xaw a ràbbaloo nga xam ni dafay sax ni tàndarma di saxe bu saxee day yëkkatiku wëraat amaat yaneen yu saxaat yoo xam ni dañuy teglaanto kom ay xuppatal yu teglaanto noonu lay doon guddaayam dan a toll ci met jàpp ñaar-fukki met ak sàtti met ak juróom. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Agave sisalana + + garab +Xeex garab la gog mi bokk ci njabootug Rhizophoraceae, bari na ca Gine gu digg. + +Melo wi + +Garab gu ndaw la gog reen yi day law ci suuf. Xob yi dañuy jàkkarloo. Doom biy sax ci garab day wërbalu te toll ci 3i sàntimet. + +Fi muy ëpp di sax day am ndox, ak ndox mu am cafka xorom, walla ci wetu dex. + +Njariñ yi + +Bant biy juge ci garab gi day dëgër te diis moo tax ñu koy jëfandikoo ci wallu liggeeyu bant. + +Xob yi dinan faral di ko fajee gaana, lakk-lakk ak taab. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + +Rhizophora racemosa + +Garab +Dugóor xeet la ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug Annonaceae. Mi ngi sax ci tund yi nga xam ne suuf si day xaw a wow walla ci barab yi nga xam ne day xaw a tooy. + +Melo wi +Garab la gog guddaayam man naa àgg 6i met. Ab xasam day yor melo wu baam daal di liis, ci nawet bi lay faral di meññ. + +Ay xobam day yor melo yu bari bokk na ci baxa, daal di muluŋ, guddaayam man àgg 7-17i sentimet. +Ay fóoyteefam day liis daa di muloŋ, yor melo wu mboq walla puur. + +Njariñ yi +Dugóor garab la gog dees koy lekk, saa-afrig yi bëgg nañu ko, ndax dafa neex lool, tey it bari na lu miy faj. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Annona senegalensis + +garab +meññeef +'"Ngonaake"' xeet la ci xeeti garabi dicotylédones, mi ngi bokk ci njabootug Fabaceae, ci njabootaatu Momosoideae, mi ngi cosaanoo penku Afrig ak sowu Asi, garab yu ndaw lay doon, dañuy sax fof suuf si day wow walla fu bari suuf lool. + +Melo wi + +"'Ngonaake"' garab gu ndaw lay doon guddaayam man naa jàpp ñaar-fukki 20i Met, yaatuwaayu peeram dees koy natt ci 60i Met. Am xasam day yor melo wu ñuul di am ay xar-xar yoy day am ay dég. + +Fóoyteefam day guus. Dinay sax foo xam ne daa bari suuf lool. + +Njariñ yi + +Garab la gog bari na ay njariñ lool, manees na cee dundal jur gi, man naa faj, manees na jël am peeram... + +Garab la gog manees na koo jël di taaral kër walla mbedd. + +Turu xam-xam wi + +Acacia nilotica + +Garab +Sanaar garab la guy ñoree ci tefes gi mi ngi gën a yaatoo ci géeju atlantig bi. +Dalee ko ci Gànnaar ( Muritani) jàpp Àngolaa topp tefesug Amerig gu digg gi ba ci bëj-saalumu Amerig lu ci mel ne Beresil. + +Melo wi +Garab gi nag bant bu tooy te diis la yor ba noppi dëgër xaw a paalmaan. Bant bu jafee wowal la. Waaye bu demee ba wow nag day jafee damm ndax dëgër gim dëgër. Bu duggee cim ndox it man na faa yàgg lool te du yàqu ndax dëgër gi mu dëgër. Am xàncam mi ngi toll ci 12,5%. Ay xobam dañoo dëgër. Reen yu bari te dëgër la yor. + +Njariñam +Ab bantam man nañ cee defar gaal, kër (baraag) , ay jumtukaayu kër ( lal, Cempteŋ, toogu ak yu ni mel). Man na matt ak këriñ. Doom yi bees leen baxalee ba ñu bax ngir wàññi tooke gi manees na koo jëfandikoo ci jamonoy xiif. Xob yi walla reen yi dees koy xoromee lujum yi ak yu ni mel. +Xànc mi daan na ñu ko jëfandikoo ngir wirgo wu xonq. saxaar siy jugge ci matt mi it day dàq i yoo. Xob yi daa nañu ko def cim ndox di ko sangoo; day faj i teeñ ak yu ni mel. Ca Amerig dañ koy jëfandikoo ci wàllu pajum cosaan ngir faj biir bu daw, ay nàcc-nàcc, emoroyit, tànk yuy metti, baat buy metti... + +Lor yi +Doom yi balaa nga koy lekk nanga ko baxal ba mu ñor ngir wàññi tooke gi. + +Turu xam-xam wi +Avicennia africana + +garab +Jaxan-jaxan xeet la ci xeeti garab yi bokk ci ñoñ Prosopis. Ñi ngi koy fekk ci gox yi nekk diggante Afrig gu naaje jàpp Sahel. + +Melo wi +Garab guy àgg 12-20i met taxawaay la, jëmm ji daa jub xocc te muluŋ ba mat 1,10i met ci ndigg li, kaw gi daa ubbeeku am i xob yu sëgg te wirgoo nëtëx bu leer. + +Xasam mi daa am i paq yu sew te dëgër, nekk ci diggante baam ak ñuul. + +Meññeef mi +Li ci ëpp ci ñaareelu xaaju noor walla ca taw yu njëkk ci nawet lay meññ. + +Njariñ yi +Dinay faj yii: bëñ bu xomaat (walla bëñ buy metti), noyyikaay bu fatt, ay goom, deru yaram bu wopp, tawati gët. +Dinay faj it metiitu biir, nopp, bopp ak biir buy dàw. + +Dinañ koy faral di jox jur gi. Dina faj emoroyitu jur gi. + +Fas, nag ak picc dinañ koy jëfandikoo (ñax). + +Bantam bu tolle ci mboqee jëm mboq bu xall, mucc ci gunóor ak sax yi. + +Manees na jëfandikoo bant bi ni bantu tabax (tabax kër), bant biy nekk ci jumtukaayu tabax yi. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Prosopis africana + +Garab +Meññeef +Kunsay mbaa Ngunsay, as ngarab la walla garab gu xob yu sew te am i dég man a àgg ba ci 15i met ci njoolaay, gu bokk ci njabootug Rutaceae. Buutam lum gàtt-gàtt man naa dem ba ci 200i met ci biir suuf, man na it àgg ba ci 40i sàntimet cig xala. + +Garab gi day am ay wànqaas yu bari. Wànqaas yi it am ay dég yu jub xocc teg ci ñaw, man nanu koo bay, man nanu koo fekk it ci àll bi walla ñu koy bay ngir jëfandikoo ay foytéef am cim paj walla bant bi dees na ko soxla ngir di ko toggee. + +Melo wi +Ci wàllu dëkkuwaayam, garab gi li ci ëpp noo ngi koy fekk cib àll walla di ko fekk ci suuf suy tooy suy bari ndox walla yu ni mel. Ci dëkk yi ëpp li nu koy fekk bokk na ca Amerig ak dëkk yi nga xam ne day jige xala yi yu ci mel ne Miyaami ak yu ni mel. + +Garab gi it màggam gaaw na lool rawati na bu nekkee ci suuf su nangu, màgg gu gaaw nag lay màgg lu muy gën a màggat garab gi di gën a rëy ay wàqaasam di gën a yaatu ak a gudd. + +Njariñ li +Li ëpp ci njariñ yi mooy lu jëm ci lu nut jëfandikoo, nee nañu doom yi man nanu cee defar diw, xob yi it bu ñoree manees na ko lekk waaye li miy am bariwul. + +Foytéefam day xaw a tolloo ak suraas ci yaatuwaay. Moom it waxuñu fenn ne manees na ko lekk. + +Lu jëm ci wàllu jëmbat garab ak yu ni mel kunsay lañuy jëfandikoo ngir màggal yeneen i xeeti garab yoo xam ne manuñu màgg ci seen i reeni bopp. + +Yeneeni njariñ +Xob yi leeg-leeg bu nu ko dëbbee mbaa nu yëy ko ba mu mokk man nañu koo boole ak ndox di ko sangoo. Bant yi it man nañu koo defaree jëfandikaay yu jëm ci kër lu ci mel ni lal añs. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Afraegle paniculata + +garab +meññeef +Ribeira da Barca' benn dekk-dëkkaan Santa Catarina Kap Weer ci yu penku yu dunu Santiago, Kap Weer. Instituto Nacional de Estatística Cabo Verde + +Dayi +António Mascarenhas Monteiro +Txeca Andrade +Pedro Freire +João Baptista Freire + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Achada Furna benn dekk-dëkkaan Santa Catarina do Fogo ci yu bëj-saluumu yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Calabaceira benn dekk-dëkkaan Ribeira Grande de Santiago ci yu sowwu yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Chelsea F.C. (Chelsea Football Club) benn football club ci "Premier League" (Nguur-Yu-Bennoo) ci dekku Londar. + +Premier League: +2004-05, 2005-06, 2009-10, 2014-15, 2016-17 + +Staad +Stamford Bridge + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Chelsea F.C. - Dalub web + +Premier League +Sporting Clube da Praia benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Praia ci yu dunu Santiago. + +Ngori +Campeonato Nacional (Kap Weert): +1961, 1969, 1985, 1991, 1997, 2002, 2006, 2007, 2008, 2009, 2012 + +Liig Santiago/1. Liig - Santiago: +1961, 1964, 1969, 1971, 1974, 1977, 1978, 1984, 1985, 1988, 1991, 1997, 1998, 20021. Liig - Santiago gu bëj-saluumu: +2002, 2005, 2006, 2007, 2008, 2010, 2012, 2013, 2014, 2017 + +Staad + +Staad Várzea (''Estâdio da 'Várzea') + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + Dário (Furtado) + Piguita + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Dalub Web Sporting Praia + +Santiago (Kap Weer) +Football +Sànceer, garab la guy faral di am ci diggu Afrig, réew yu mel ni keeñaa, Somali,Tansani jàpp Gànnaar ba Senegaal. +Ci àll bi ak ci tefes gi lay faral di ñoree. + +Melo wi + +Garab la gu man a sëq lool. +Ay caram dañoo dëng, ab guddaayam man a toll ci 2i met jàpp 6i met. + +Njariñam + +Ay doomam dees koy lekk. +Reen bi boo ko nalee walla nga baxal ko man nga ko jëfandikoo ci wàll um paj yu bari, ( Gaana, Sifili, Gonoore, stomaa...). +Sunguf si juge ci reen bi ak xànc mi day faj ay góom. + +Ay doomam dañuy faj tooke ak lu ci mel ne màtt-màttu jaan. + + ==Loraange yi== + +Giseesagu ci lor. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi + +Feretia apodanthera + + garab +Jalambaan as ngarab la su am ay xop yu sew yu toll ci ñeent ak xaaj, ba ci juróom-ñaar ak xaaj, ci ay met waaye néew na lool lu muy yegg fukki met ak juróom. Garab gi noo ngi koy fekk lu ci ëpp ci àll bi di ko jëfandikoo ci wàllug paj walla ci ay jumtuwaay. Bantu jalambaan bokk na ci li ëpp dayo ci liy jóge ci Afrig boole ko ak ay jumtuwaay yu bari yu nu ci man a jële. Bokk na ci it yi ñu gën a jox cër gën koo yittewoo ci wàllug yattum bant ci wàllum defar ay jumtuwaay yu jëm ci wàllu misig ñu di ko jaay ci àdduna bébb ci lu ndaw waaye ci njëk lu kawe. + +Dëkkuwaayam garabu jalambaan man nañu koo fekk ci gox yu bari ak ci dundiin wu wuute man nañu koo fekk ci suuf su wow walla suuf su xaw a tooy dana ñu ko fekk it fu am i xeer waaye fi ëpp ci fi ñu koy fekk mooy cib àll ci àll boo xamentani lu ëpp ci garab ya séeni xop day sew walla fu jége géej. + +Melo wi Xooxi jalambaan yi buñu leen génnee ci koog yi ñu nekk ba ji leen dina ñu gaaw a sax. Da ñu leen di teg ci kaw ub car ngir ñu wow ba laa ñu leen a weer ci naaj wi. Dina ñu sax juróom-ñatt jàpp ñaar fukki fan bu ñu ko jiyee ak it lu tolloog juróom-fukk ci téeméer bu ne ñu man a dund séen ug màgg nag gaawut lool ndax man nañu dem ba ñaari at toll ci fukki sànt-met ak ñaar yépp ci reen yi lay nekk. + +Ay ñariñam +Li ci njëkk ci njariñ yi ci wàllug paj nee nañu reeni garab gi boo ko jëfandikoo dana ray ay saan dana yokk it ngóora góor, ku ko togg it man nañu koo jëfandikoo ngir fàggandiku ci ëmbu jigeeen buy yàqu walla faj biir buy metti walla biir buy daw walla faj xeeti feebar yiy juddoo ci sëy. Bant yi boo ko lakkee saxar si nga noyyi ko man naa faj bopp buy metti walla soj walla xeeti sëqat yu metti yi. Xas mi ak reen yi bu ñu ko boolee ci paj um cosaan man naa faj biir buy daw bu ñu ko boolee ak buy. + +Batay ci wàllug paj xas mi ku ko jël dëbb ko ba mu mokk ba mu xaw a nooy man nañu koo faje góom ku jël xop yi it dëbb ko ba mu nooy man naa faj ay metiitu yax walla ay teq ak yu ni mel ndox miy génnee ci garab gi nu koy wax njoy-njoy ak ci xop yi man naa faj gémmiñ guy nàcc mbaa gu sofe walla it put guy xasan +Batay ci xas mi as lëf ci xas mi wane nañu ni man naa faj lu jëm ci ay mikrob te it man nañu cee faj ay gaañu-gaañu. + +Ci wàllu jëmbat garab gi, garabu jalambaan man naa doon luy gën a dundal suuf yokk ak mbaaxam man nañu koo jëfandikoo it ngir fàggandiko dees na ko jëfandikoo it ci sàkket yu dëggar. + +Yaneen i njariñ ci jalambaan, léppam day jëm ci bantam ndax bant la bu njool xaw a jàpp ... leeg-leeg mu dër lool walla mu jël yeneen wirgo. ay bantam man na dem ba ci fukk ak ñaar ci ay sànt-met, bantam nag dana niin dëgar lool duy gaaw a dammu, man naa it fàggandiko ci ay yàq-yàqu yu mel ni ay max añs teg ci it neex a jëfandikoo te rafet lool ba tax na dañu koy jëfandikoo ci jumtuwaay yi ñuy defe misig ak bant bi ñuy doxe nu koy wax dokk dees na ko jëfandikoo fii ci Senegaal ci yu bari lu ci mel ni kurus ak yat ak jaaro añs. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Dalbergia + +Wàllu garab +Caaya j- + +Mag ñee ëpp lu ñu koy sol. + +Caaya tubeyu mag la. + +[[wàll: waati wolof]] +Sàmba-sayar garab la gog mi ngi bokk ci njabootug (Entada Africana). mi ngi faral di sax lu ëpp ca Sudã. Dina sax it ca Burkinaa Fasoo, ca Kóngo, ca Niseriyaa, ca Senegaal ak ca Ugàndaa. + +Melo wi +Garab la gog amna tolluwaay 4i ba 10i metar ci taxawaay ak 90i cm ci wërngal (diamètre). +Der wi dafa dóomu taal jàpp brune ba jël ñuul, dëgër, am ay raya yu taxaw, mel ni xollit. +Xob yi da ñuy tegaloo ñatt ba juroom ñeent. Doom yiy sax ci garab gi yu dëgër lañu, te dañuy lang ay weer i weer, 12i (millimètres) la ci guddaay. + +Meññeef +Sàmba-sayar mi ngi sax ci àll walla barab yuy taw lu bari, walla bari ndox. + +Njariñ yi +Xob yi manees na cee defar ay basaŋ. Xob yi, reen yi ak wànqaas yi day jur want yu gudd yu nu man a defare ay buum ak i takaayu bant i tabax. Xob yi ak gàncax gi bari na luñu koy jëfandikoo ca Niseriyaa ak Gana ci wàllug paj. + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Entada africana + +garab +Béegile Garab gii di béegile : turu xam-xamam di ( cordia senegalesi ) mu bokk ci njbootu "borazina cea" di sax ci dëkk yi nga xam ne taw bi da faa yem a maay , ak foo xam ne it taw bi da faa bari lool ,fu mel ni Afrig torópikaal , maanaam ay Sengaal, Gambi , Kodiwaar , Gana , Kamerun . + +Melo wi +Béegile ; garab la goo xam ni gudaayam di na àgg ci juróom ñaar walla juróom ñatti meetar ci kaw. +ay wànqaasam boo ci gis rekk muj ga maanaam cat la day lunk , dàtt bi it man naa rëy ba egg ci juroom-benn-fukki meetar 60i ci ag wëram , ker gi man naa dem ba egg ci 25i meetar ci yaatuwaay , ndax moom day sëq lool . +Moom nag garab la gog Tubaab yi bindu ñu ci lu bari boo xoolee di na ñu la wan ntaal bi wax ci tuuti waaye du doon lu bari , maanaam daal dafa mel ni gëstoogu ñu ci . + +Njariñ yi +Ay bantam di nañu ko def matt ngir di ko xambe , batay garab gi di nañu koy taarale kër ndax naataayam dafa rafet. +Di nañ ko jëfandikoo it ngir faju , wax na ñu ne di na faj biir buy metti, xob yi lañuy jamb ngir di ci faj biir buy metti boo xam ne jàngoroy kuli moo ko waral, dees na ko naan it ngir dànk mettiitu dëmbéen , xob yi batay dees na ko jamb di ko sangoo ngir faj yarm wuy metti walla yaram wu fasu , bantam di na ñu ci defar ay dënd ak ay gaali géej , xas mi di na ñu ci defar ay buum , amna it daakande . + +Nataal yi + +Turu xam-xam wi +Cordia senegalensis + +garab +Taab nu ngi koy faral di gis lu ci ëpp ci àllu Sayel bi, fi muy sax itam danuy seetlu ne suuf si day dëgër. + +Senegaal ba Kamerun ak Somali, amna ñu koy jàllale ci diggante réew yooyu. Boo deme Niseria it di nga koy faral di gis ci boori "Sud-Ouest". + +Melo +Taab garab la goo xam ne guddaay bi dina dem ba ay 12imeetar ci kaw. Te ay wànqaasam day am lu ci ëpp ay dég yu xaw a dëng. Loolu moo tax muy man a jàppanteek yeneen garab yiy nekk ci wetam. +Ba laa man a sax dëgg nu nekk ci njeextalu noor bi walla ci biir nawet bi. Dina am ay xob, dina am ay meññeef. + +Njariñ +Garab gi nag day faj ay feebar yu bari, yu ci mel ne: biir buy daw, saan, day yokk cawarte, tegsi di ubbi biir ngir ngay man a lekk bu baax. + +Nataal + +Turu xam-xam +Combretum Nigricans + + Garab +Xoriit ag garab la gog xob yi dañuy sew tey am mbaar muy gën a yaatu lu garab giy gën a màggat. Man naa njool ba ci 3i met ba ci 10i met. Peeru garab gi day dëng. +Jafe-jafe yi ko daay yiy indil dagg yi nuy dagg ay xobam tax na garab gi bokk ci yu ñeme coono yi. Xoriit garab la guy sax ci àll, nu man koo jëfandikoo ci lu nuy lekk mbaa di ko fajoo + +Dëkkuwaayam + +Garab gi ci àll bu bariy garab lay dëkk, walla ci kaw dëkkuwaay yuy max, leeg-leeg ci peggu penkug Afrig. + +Mbayam + +Garab man naa nangu ab sedd yuy am leeg-leeg. Waaye li mu gën a nangu mooy tàngoor, soxla na it suuf su tooy, te it àttan na aw wal(inondation). + +Njariñam + +Lu jëm ci lu nuy lekk, xob yi dees koy togg boole ko ak supp mbaa ay pepp. Foytéefam day am caas bu weex bu nu man a lekk boole ak doom yi nu togg. Foytéefam bi man naa àgg ba ci 4-5i sàntimet ci xala. + +wàllug paj + +Xob yi man naa faj bopp buy meti. Saxaaru ndox mu tàng mi dees koy suuroo ngir faj ay jafe-jafey gis. Xob man naa faj it payiis. Xas mi day faj biir buy metti, ak tële. Sungufam ku ko boole ak diw man naa nekk forote buy faj ay yax yuy metti. Reenam day faj sifilis (febaru sëy) + +Melo + +Yeneen njariñ. +Wirgo wu mboq man naa génn ci garab gi. Bantam ci dagg bi man naa niru lu dëgër waaye amul lenn njariñ ludul ay jumtukaay yu ñàkk solo. + +Nataal yi + +Turu xam-xam +Crateva + + garab +Fundo das Figueiras benn dekk-dëkkaan Boa Vista ci yu sowwu yu dunu Boa Vista, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +Arsenal F.C. (Arsenal Football Club) benn football club ci "Premier League" (Angale - Nguur-Yu-Bennoo) ci dekku Londar. + +Premier League: +1997-98, 2001-02, 2003-04 + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Arsenal F.C. - Dalub web + +Premier League +Boavista Futebol Clube da Praia benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Praia ci yu dunu Santiago. + +Staad + +Staad Várzea (Estâdio da 'Várzea') + +Ngori +Campeonato Nacional (Kap Weert): + 1963, 1987, 1995, 2010 + +Liig Santiago/1. Liig - Santiago: +1962/63, 1975/76, 1986/87, 1992/93, 1994/951. Liig - Santiago gu bëj-saluumu: 2' +2011/12, 2014/15 + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + Babanco + Moía Mané + Nilson Tavares + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Boavista FC Praia - Facebook + Boavista FC Praia - Soccerway + Boavista Praia - Scoreshelf + +Santiago (Kap Weer) +Football +Hepatite B (HB) feebar la buy wàlle, li koy joxe mooy doomu jàngoro (wiris) bi tudd virus hepatite B (VHB) te dafay jàpp resu nit ki. Mën na wàlle ci lu sew ak ci lu tar. Li gëna bari suy sooga dal nit ki du feeñ ci moom. Amna ci ñoo xam ni da leen duggee dañuy feebar di waccu, der bi furi, tàyyeel, saw mu nëx ak metitu biir. Yenn dina faral di def noonu ay ayi-bis waaye bariwul lumuy faat nit ki su koy sooga dal. Feebar bi mën na nekk sa yaram 30 ba 180 fan laata muy feeñ. Xale yi feebar bi dug bi ñuy sooga judd, 90% ci ñoom dañuy yegg ci hepatite B bu tar bi (kronik) waaye xale yi am 5 at, 10% ci ñoom rek ñooy am bu tar bi. Lu gëna bari ci hepatite bu tar bi du feeñ; waaye mën na dem bay egg ci, cirrhose ak yàq resu nit ki (cancer du foie). Cirrhose ak res wu yàqu dina daaneel 25% ci ñi am njàgoro ju tar ji. + +Lila mëna jox doomu jàngoro ji mooy nga laal deretam wala bépp ndox mu jogee ci yaramu ki ko am. Fi feebar bi di ëppee li muy dug ci nit ki mooy ci liir buy gane si àdduna wala laal deretu ku am jàngoro ji bi muy nekk xale, noonu lañuy faral di jàppee Hepatite B ci barab yi mu gëna bari. Sudee ci barab yi jàngoro ji bariwul, li ko fay gëna joxe mooy pikiiru grog ci yoonu deret wala ci sëy. Nit ñiy liggéey ci barabu fajukaay yi itam mën nañu ko am, may nit deret, dialyse, dëkk ak ku am doomu jàngor bi, tukki di dëkk bu feebar bi bari, wala dëkkandoo ak ñu bari ci këru buur. Ci jamonoy 1980, nit ñi daan nañu ko jëlee ci jamu (tatouage) wala pajum puso (acupuncture); waaye, loolu bareetul leegi ndax pexe yi ñuy rayee doomi jàngoro yi ci jumtukaay yi dafa gëna xarañ. Jàpp loxo nit ku am hepatitis B joxewul feebar bi, bokk ndab, foon, akolaat, sëqët, tosooli, wala nàmpal itam du ko joxe. Mën nañu gis feebar bi ci sa yaram su amee 30 jàpp 60 fan ginaaw bi mu la duggee. Ni ñu koy faral di saytoo ci sa yaram mooy xool ci sa deret ndax amul lenn lu bokk ci doomu jàngoro ji, wala ndax sa yaram tàmbiliwul defar luy xeex jàngoro ji. Hepatite B benn la ci juróomi wirisi hepatite yi am: A, B, C, D, ak E. + +Ci atum 1982 lañuy defar ñaq bu ci mëna musal nit ñi. Waa OMS santaane nañu ñu ñaq xale yi ci bis bi ñu juddóo. Ginaaw ga dina ñu ko baamtu ñaar ba ñatti yoon ndax moo ëpp kaaraange. Baaxaayu ñaq bi yegg na ba ci 95%. Amna lu tollu ci 180 yu ko boole ci seen prograamu xeex feebar ci atum 2006. Wax nañu itam ni balaa ñuy may kenn deret nañu xool bu baax ndax amul wirisu hepatite B, te nañuy jëfandikoo kawas (kapot) sunuy sëy. Su lay sooga dal, paj maa ngi aju ci ni feebar bi feeñoo. Sudee ñu feebar yàgg lool ci ñoom, dañu leen di jox garab guy ray wiris bi lu ci melni tenofovir wala interferon; waaye nak garab yu seer lañu. Sudee ku feebar bi yàq resam, dañu koy defal beneen res. + +Ñatti nit ñoo jël ci àdduna bi kenn ci ñoom mus na ko am, te ci ñi ko am, amna 343 ñu feebar yàgg ci seen yaram. Amna yeneen 129 milion ciy nit ñu feebar biy sooga dal ci atum 2013. At mu nekk hepatite B bi dina ray lu ëpp 750 000 doomi aadama. Ci limuy ray amna ci 300 000 nit yumu yàq seen res ñu dee. Feebar baa ngi gëna baree ci Asie gu Penku ak ci Afrique gi si suufu Sahara, ñi fa am feebar hepatite B bu tar bi yegg na 5 ba 10% ci mag ñi. Sudee ci Europe ak Amerik du Nord, seen taux yeggul 1%. Bu njëkk ñu ngi xamee woon ci "serum hepatitis". Ñu jéema fexe nuñu defaree ñam yuy amaale ñaqu VHB.  Feebar bi mën na dal golo yu mag yi itam. +Hepatite B (HB) feebar la buy wàlle, li koy joxe mooy doomu jàngoro (wiris) bi tudd virus hepatite B (VHB) te dafay jàpp resu nit ki. Mën na wàlle ci lu sew ak ci lu tar. Li gëna bari suy sooga dal nit ki du feeñ ci moom. Amna ci ñoo xam ni da leen duggee dañuy feebar di waccu, der bi furi, tàyyeel, saw mu nëx ak metitu biir. Yenn dina faral di def noonu ay ayi-bis waaye bariwul lumuy faat nit ki su koy sooga dal. Feebar bi mën na nekk sa yaram 30 ba 180 fan laata muy feeñ. Xale yi feebar bi dug bi ñuy sooga judd, 90% ci ñoom dañuy yegg ci hepatite B bu tar bi (kronik) waaye xale yi am 5 at, 10% ci ñoom rek ñooy am bu tar bi. Lu gëna bari ci hepatite bu tar bi du feeñ; waaye mën na dem bay egg ci, cirrhose ak yàq resu nit ki (cancer du foie). Cirrhose ak res wu yàqu dina daaneel 25% ci ñi am njàgoro ju tar ji. + +Lila mëna jox doomu jàngoro ji mooy nga laal deretam wala bépp ndox mu jogee ci yaramu ki ko am. Fi feebar bi di ëppee li muy dug ci nit ki mooy ci liir buy gane si àdduna wala laal deretu ku am jàngoro ji bi muy nekk xale, noonu lañuy faral di jàppee Hepatite B ci barab yi mu gëna bari. Sudee ci barab yi jàngoro ji bariwul, li ko fay gëna joxe mooy pikiiru grog ci yoonu deret wala ci sëy. Nit ñiy liggéey ci barabu fajukaay yi itam mën nañu ko am, may nit deret, dialyse, dëkk ak ku am doomu jàngor bi, tukki di dëkk bu feebar bi bari, wala dëkkandoo ak ñu bari ci këru buur. Ci jamonoy 1980, nit ñi daan nañu ko jëlee ci jamu (tatouage) wala pajum puso (acupuncture); waaye, loolu bareetul leegi ndax pexe yi ñuy rayee doomi jàngoro yi ci jumtukaay yi dafa gëna xarañ. Jàpp loxo nit ku am hepatitis B joxewul feebar bi, bokk ndab, foon, akolaat, sëqët, tosooli, wala nàmpal itam du ko joxe. Mën nañu gis feebar bi ci sa yaram su amee 30 jàpp 60 fan ginaaw bi mu la duggee. Ni ñu koy faral di saytoo ci sa yaram mooy xool ci sa deret ndax amul lenn lu bokk ci doomu jàngoro ji, wala ndax sa yaram tàmbiliwul defar luy xeex jàngoro ji. Hepatite B benn la ci juróomi wirisi hepatite yi am: A, B, C, D, ak E. + +Ci atum 1982 lañuy defar ñaq bu ci mëna musal nit ñi. Waa OMS santaane nañu ñu ñaq xale yi ci bis bi ñu juddóo. Ginaaw ga dina ñu ko baamtu ñaar ba ñatti yoon ndax moo ëpp kaaraange. Baaxaayu ñaq bi yegg na ba ci 95%. Amna lu tollu ci 180 yu ko boole ci seen prograamu xeex feebar ci atum 2006. Wax nañu itam ni balaa ñuy may kenn deret nañu xool bu baax ndax amul wirisu hepatite B, te nañuy jëfandikoo kawas (kapot) sunuy sëy. Su lay sooga dal, paj maa ngi aju ci ni feebar bi feeñoo. Sudee ñu feebar yàgg lool ci ñoom, dañu leen di jox garab guy ray wiris bi lu ci melni tenofovir wala interferon; waaye nak garab yu seer lañu. Sudee ku feebar bi yàq resam, dañu koy defal beneen res. + +Ñatti nit ñoo jël ci àdduna bi kenn ci ñoom mus na ko am, te ci ñi ko am, amna 343 ñu feebar yàgg ci seen yaram. Amna yeneen 129 milion ciy nit ñu feebar biy sooga dal ci atum 2013. At mu nekk hepatite B bi dina ray lu ëpp 750 000 doomi aadama. Ci limuy ray amna ci 300 000 nit yumu yàq seen res ñu dee. Feebar baa ngi gëna baree ci Asie gu Penku ak ci Afrique gi si suufu Sahara, ñi fa am feebar hepatite B bu tar bi yegg na 5 ba 10% ci mag ñi. Sudee ci Europe ak Amerik du Nord, seen taux yeggul 1%. Bu njëkk ñu ngi xamee woon ci "serum hepatitis". Ñu jéema fexe nuñu defaree ñam yuy amaale ñaqu VHB.  Feebar bi mën na dal golo yu mag yi itam. +João Galego benn dekk-dëkkaan Boa Vista ci yu sowwu yu dunu Boa Vista, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +Santa Catarina do Fogo benn dëkkaanu ci yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Dëkki +Cova Figueira + +Dëkk-dëkkaani +Achada Furna +Achada Poio +Baluarte +Cabeça Fundão +Chã das Caldeiras +Domingo Lobo +Estância Roque +Figueira Pavão +Fonte Aleixo +Mãe Joana +Monte Vermelho +Roçadas +Tinteira + +Football clubi +Desportivo de Cova Figueira + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +https://web.archive.org/web/20191118235423/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/SantaCatarinadoFogo.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +São Miguel benn dëkkaanu ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Dëkki +Calheta de São Miguel + +Dëkk-dëkkaani + +Achada Monte +Casa Branca +Chã de Ponta +Cutelo Gomes +Espinho Branco +Gongon +Igreja +Machado +Mato Correia +Monte Bode +Monte Pousada +Palha Carga +Pedra Barro +Pedra Serrado +Pilão Cão (Santiago +Pingo Chuva +Ponta Verde +Principa; (Ribeira Principal) +Ribeira Milho +Ribeireta +Tagarra +Varanda +Veneza +Xaxaa (Xaxa) + +Football clubi +Desportivo da Calheta +Flor Jovem +AJAC + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.ams.cv/index.php?option=com_content&task=view&id=34&Itemid=53 +https://web.archive.org/web/20191118235639/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/S%C3%A3oMiguel.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Viana (Deserto de Viana): benn yay ci yu bëj-gannar yu Boa Vista, Kap Weer. + +Xool it +Melosuufug kap weer + +Karmat ak delluwaay + +Yay +Melosuufug afrig +Boa Vista (Kap Weer) +Ñaqu rougeole (ŋas) mooy li lay musal ci rougeole. Sudee bi nga njëkkee ñaqu sa yaram defarul lu koy aar ci feebar bi, soo ñaquwaate rek feebar bi dootul mën dara ci yaw. Sudee dañu ñaq lu weesu 92% ci waa dëkk bi, mën nañu jàpp ni dëkk boobu feebar bi dufa feeñ; waaye mën na fa ñëwaat sudee limu ñiy ñaqu dafa dem ba wàññiku. Soo ñaqoo dinga mucc ci feebar bi ay at yu bari. Xama guñu bu baax ndax ndax kaaraangeg ñaq bi dafay wàññiku. Ñaq bi mën nala aar itam soo ko jëlee ci biir ñaari fan yi nga nekk ci barab bula feebar bi mëna dalee. + +Ñaq bi du indil nit ki benn jafe-jafe, doonte danga am VIH. Mën nala xawa sonal tuuti waaye du yàg dara. Maanaam fi ñu la ko jam mën na saf tuuti wala sa yaram xawa tàng. Amul benn yokkute buy seetlu ci limu Seetlu nañu itam 3,5 jàpp 10 kaa anaphylaxie ci miliyoŋi nit ñuñu ñaq. Sudee lu jëm ci feebar Guillain-Barré, autisme ak biir buy metti (maladie intestinale inflammatoire) gisu ñu ci benn yokkute. + +Ñaq bi amna mooy kese, waaye itam dina ñu koy boole ak yeneen ñaq yu ci melni ñaqu ROR, (muy boole ñaqu rubeole ak anti-ourlien) wala ñaqu RROV (maanaam ñu boole ñaqu RRO ak ñaq biy aare ci varicelle). Ñaq bii aare ci rougeole dafay musalaate ci feebar itam ndeem dañu ko boole ak yeneen ñaq, te effets secondaires yi dañuy wuute, lépp di aju ci xeetu ñaq bi ñu ko booleel. Waa OMS ñoo digal ñu ñaq xale bi su amee juróom ñeenti weer te nekk ci barab bu feebar bi bari. Waaye sudee fu feebar bi bariwul la, jaaduna ñu ñaq xale bi su amee fukki weer ak ñaar. Ñaq bi luy doomu jàngoroy rougeole bu dundu la waaye dañu ñéewal dooleem. Ñaq bi puudar bu waw la, fàww ñu jaxase ko laata ñu koy jam nit ki ci suufu deram wala ci siditam. Soo bëggee xam ndax ñaq bi jàppna danga saytu deretam. + +Ci atum 2013, ñaq nañu lu tollu ci 85% xale yi ci àdduna bi. Ci atum 2015 amna gën gaa néew 160 réew yu baamtu ñaq bi ngir nit ñi mën a am matuwaay yu leen musal ci feebar bi. Ci atum 1963 la ñu njëkka génne ñaq bi. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Njëgi ñaq bi ci réew yu néew doole yi mingi tollu ci 0,70 USD dose bu nekk, en gros, li tàmbale 2014. Ginaaw feebar bi dafa faral ci barab yi nit ñu bari ñaquwul, feebar dina tax ñu xam barab yi ñaq bi barul ñu ko def. +Ñaqu BCG (Bacillus Calmette-Guérin) mooy lila gëna mëna aar ci tuberkuloos (TB). Sudee ci réew yi feebaru tuberkuloos wala ngaana bari, digle nañu ñu ñaq benn yoon xale biy sooga judd te amul benn feebar nga ñaq ko ci nimu gëna gaawe su juddoo. Sudee ci barab yi feebar bi bariwul, xale yi nekk ci barab bi ñu ko mëna amee ñoom la seen yaram di am ay matuwaayi moytu feebar bi, waaye su amee kuñu ñaaw njortu ndax amna feebar am déet, dañu koy saytu ba noppi faj ko. Mag ñi amul tuberkuloos te nekk ci barab bu feebar bi bari, seen yaram mën na defar ay matuwaay yu leen di aar ci feebar bi. Ñaqu BCG mën nala aaraale itam ci feebar yu melni ulseeru Buruli ak yenn feebari bacteri yu bokkul ak tuberkuloos. Rax ci dolli dina ñu koy faral di jëfandikoo ngir faj kanseeru naq. + +Yàggaayu kaaraange ñaq bi barina te wuute, waaye mën na yegg ba 20 at. Ci xale yi ñu ñaq, dina am 20% ci ñoom ñu dul am feebar bi, ñeneen ñi des itam suñu amee feebar bi itam, du leen mënal dara. Ñaq bi ci suufu deru yaram wi lañu la koy defal. Ama guñu firnde ci ndax dañu koy baamtu am déet. + +Daanaka ñaq bi amul benn loraange. Yenn saay fiñu la ko jam xonk wala mu newwi, wala nga yëg tuuti metit. Mën nga amaale ulseer bu ndaw ak yenn léget su weree. Efe secondaire yi ñoo ci gëna bari, te ci mag ñi amatul matuwaayu xeet feebar bi lay gëna sonal. Wóoral a jox jigéen ju ëmb. Ñu ngi ñëkka sosee ñaq bi ciiMycobacterium bovis muy luñuy faral di jëlee ci nag. Néewal nañu dooleem bu baax waaye mingi dundu. + +Ci atum 1921 lañu njëkka jëfandikoo ñaqu BCG ci wàllu faj. Bokk na ci limu ñaq yi OMS jàpp ni ñoo gëna am solo ci wérgi-yaramu nit ki. Ci diggante atum 2011 ak 2014, njëg li en gros mingi tolluwoon ci diggante 0,16 USD jàpp 1,11 USD benn dose ci réew yu néew doole yi. Ci réewum Etats Unis, ñaq baa ngi fay jar ci diggante 100 ak 200 USD. Li ko dalee 2004, at mu nekk dina ñu ñaq lu tollu ci 100 miliyoŋi xale ci àdduna bi at. +Tuberkiloos (TB) feebar la buy wàlle, te li koy faral di joxe mooy doomu jàngaor bi tuddu Mycobacterium tuberculosis (MTB). Cër bi tuberkuloos di ngëna jàpp mooy dënn bi, waaye mën na dem ba laalaale yeneen cër ci yaramu nit ki. Barina lu muy dal nit te du feeñ, loolu lañuy woowe tuberkuloos bu nëbbatu. Lu tollu 10% feebar yiy nelaw yaramu nit ki, dañuy dem ba daaneel nit ki, suñu ko fajul, mën na dem ba faat ki mu dal. Beneen tuburkuloos bi nelawul moom dafay wane boppam, kumu dal dangay am sëqët mu tar àndaale ak lumbi deret, yaram wu tàng, ñaqu guddi, ak yaram wuy jeex di dem. Di nañu koy faral di woowe feebaru "ŋacci" ndax limuy ŋacci sa yaram. Amna yeneen anam yu muy feeñee su laalee yeneen cër yi. + +Tuberkuloos dafay tasaaroo ci ngelaw li, suede tuberkuloos bu tar moo la jàpp, soo sëqëtee wala nga tifli wala nga wax, wala nga tissooli mën nga ko wàlle. Nit ñi feebar bi di nelaw ci seen yaram du ñu wàlle feebar bi. Nit ñi gëna mëna wàlle feebar bi mooy ñi am VIH/SIDA ak tóxkat yi. Ngir saytu jàngoro ju tar ji ci yaram nit, dañuy rajo dënn bi, dañuy jël itam ndox mu bawoo ci moom ñu xool ko ci microscope wala ñu amal ci njàngat mu xóot. Sudee tuberkuloos biy nelaw nak, ci deru nit ki wala ci deretam. + +Suñu bëgee aar nit ñi ci feebar boobu, nañuy saytu bu baax ñi nekk fumu leen mëna dalee, teela gis doomu feebar bi ak teel ko faj, ak jël ñaq bii di Bacile Calmette-Guérin (BCG). Nit ñi feebar bi gëna yab ñooy ñiy liggéeyandoo ak ki ko am, ñi mu bokkal kër, workplace, ak ñi muy nekkal bis bu nekk. Paj mi dafay yàgg lool, te ay àntibiotik lañu koy defee. Doomu jàngoro bi daa tàmbali ñeme garab yu bari (MDR-TB) ak doomu jàngoro yi ñeme yeneen garab bi (XDR-TB). + +Ci atum 2018, ñeenti nit ñoo jël xalaat nañu ni kenn ka amna tuberkuloos. At mu nekk dina am lu tollu ci 1% ci nit ñi ci àdduna bi ñuy am doomu jàngoro ji. Ci atum 2017, amoon na lu ëpp 10 milion ci nit ñu am feebar bi, ci ñooñu amna ci lu tollu 1.6 milion ñu ci ñàkk seen bakkan. Loolu moo ko def feebar bi dàqa ray ci feebar yiy wàllaate.Lu ëpp 95% nit ñi mu faat ci réew yu néew doole yi lañu dëkk, lu ëpp 50% Inde, Chine, Indonesie, Pakistan, ak Philippines. Seetlu nañu ni li ko dale atum 2000 ba leegi wàllaate gi dafay gëna wàññeeku at mu nekk. Nit ñi saytu ndax am nañu tuberkuloos am déet, 80% ci ñoom dañuy am feebar bi suede ci Asie ak ci Afrique waaye suede ci Etats Unis 5–10% ci nit ñi ñuy saytu ñoo koy am. Ca jamonoy maam ya ba leegi tuberkuloos a ngi am. + +Cosaanu gëstu bi +Ñaqu (vaccin) Hepatite A mooy ñaq bi mëna aar nit ñi hepatite A. Wóoraayam yegg na ba 95%, te dina la aar lu tollu ci fukki at ak juróom amna sax ñu muy aar seen giiru dundu. Ku nekk war na ko ñaqu ñaari yoon, bu njëkk bi mooy su xale bi amee benn at. Ci siditu nit lañu koy pikiir. + +Waa Mbootaayu Wergi-yaram ci Àdduna bi (OMS) dañu digle ñu ñaq ñépp ñu nekk ci barab bi feebar bi bariwul noonu. Waaye digle wuñu ñaq ñépp ci barab yi feebar bi bari lool ndax ci foofa xaramu nit ki tàmm na xeex ak moom ba muy xale ba defar ay matuwaayam. Waa Kër giy Saytu ak Musalaate ci Tawat yi (CDC) waxna ñu ñaq mag ak xale yi nekk ci barab yumu leen mëna dalee. +Ñaq bi dula jurul benn jafe-jafe. 15% ci xale yi ko jël dina ñu yëg tuuti metit ci barab biñ jam wala genn-wàll gi suede mag la. Ñaqi hepatite A yu bari dañuy am wirisu buñ tënk, waaye yenn ci ñoom wiris buñu wàññi dooleem lay am. Bi am wiris biñu wàññi dooleem baaxul ci jigéen ju ëmb wala ñi seen yaram gaawa jël feebar. Amna ñaq yu néew yuy jël hepatite A boole ko ak hepatitis B wala ñaqu typhoid. + +Ñu ngi njëkka nangoo ñaqu hepatitis A ci Europe ci atum 1991 ak ci Etats Unis ci atum 1995. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Soo demee Etats Unis mingi fay jar diggante 50 ba 100 dolaar (USD). +Ñaqu (vaccin) Hepatite B mooy ñaq bi mëna aar nit ñi hepatite B. War nañu ko ñaq nit ci biir 24 waxtu ci top ci juddoon, ginaaw loolu mën nañu ko baamtu ñaar ba ñatti yoon. Bokk na ci ñoom ñi seen yaram ragal feebar maanaam ñi am VIH/SIDA ak liir yi judd te seen àpp jotagul. Digle nañu itam ñiy liggéey ci barabi fajukaay yi ñu ñaqu. Di faral di ñaq ñi dara jotul dina leen may kaaraange kuy yegg ba 95%. + +Ñi nekk ci barab bu feebar bi nekk, fàww ñu saytu seen defar ngir xool ndax seen ñaq baa ngi leen di aar. Ñi seen yaram gaawa daanu feebar fàww ñu baamtu ñaq bi. Ñi seen yaram amagul luy xeex feebaru hepatite B te ñu nekk ci barab bu ko, dañu leen wara joxaale immune globulin anti-hepatite B dolli ko ci ñaq bi. Ci siditu nit ki lañu lay pikiir ñaq bi. + +Daanaka ñaqu hepatite B du indil nit ki benn jafe-jafe. Mën nga yëg metit ci barab biñ la koy jam. Du waññi dara jiggéen ju ëmb wala juy nàmpal. Jotewul dara ak feebar bii tuddu syndrome Guillain-Barre. Ñaq yi am jamono jii ñu ngi leen defaree xaralay ADN recombinant. Mën nga leen am ñoom kese wala ñu boole leen ak yeneen ñaq. + +Ñu ngi njëkka nangoo ñaqu hepatite B ci Etats Uinis ci atum 1981. Ginaaw ga ñu génne beneen bu gëna wóor ci atum 1986. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Njëggu ñaq baa ngi tollu woon ci diggante 0.58 ak 13.20 USD dose bu nekk, ci atum 2014. Soo demee Etats Unis mingi fay jar diggante 50 ba 100 dolaar (USD). +Meningite ay metit yu tar la yuy jàpp cër yiy aar yuuru nit ki, ak doqam, te ñu koy gëna woowe meninge. Ni muy gëna feeñee ci nit mooy yaram wu tàng, mettitu bopp ak ndong lu bañ. Yenn say mu feeñee neeneen, lu ci melni xel mu jaxasoo ak ñàkka xàmme yenn mbir, waccu, bëggul leeraay ak xumbaay. Neneen lay feeñee ci xale yi, lu ci melni gaawa mer, tayeel, wala baña lekk. Su tàmbalee feeñ ci yaram wi, mën na wane ban xeetu Meningite la nit ki am; ci misaal, Meningite bi bacterie meningococcal mën ànd ak yeneen xeetu feeñal ci deru nit ki. + +Wiris, bacteria wala yeneen doomi jàngoro mën nañu jàpp wall yu bari ci yaram wi, garab yi itam mën nañu ko waaye bariwul. Meningite mën faat doomu aadama ndax li muy yàq dafa jege your gi ak moelle epiñeer; moo tax, su dale nit ki dañu ko wara gaaw faj. Suñu jamee (Une ponction lombaire) nit ki ci yaram lañuy mëna xam ndax amna Meningite am déet. Dañuy roof ràbb ci kanaal rachidien bi ngir taataan lenn ci liquide cephalo-rachidien (LCR), bi muur yuur gi ak moelle epiñeer bi. Ci ab lobo lañu càmbaree LCR. + +Amna yenn xeetu meningite yoo xamni boo ñaqoo duñu la mënal dara, muy ñaq buy aare méningocoque, oreillon, pneumocoque ak Hib. Ñi nekk ci barab bu am yenn xeeti meningite yi mën nañuy jëfandikoo antibiotique, baaxna ci lool. Li ñu wara njëkka jox ki am meningite bu metti bi mooy ay antibiotique ak yenn garab yuy xeex doomu jàngoro (virus). Soo bañee meningite bi indal la mettit yu dara wala mu am lumuy yàq ci der bi, dangay jël ay corticostéroïde ngir mu aar la ci yooyu jafe-jafe. Meningite mën na indil nit ki ay jafe-jafe su yàggee, maanaam mën nala tëxloo, soyloo, hydrocéphalie wala xel mu wayadi, sudee teelu ñu ko faj. + +Ci atum 2015, meningite jàpp na lu tollu ci 8,7 milioŋ ciy nit. Feebar bi faatna 379 000 ci àdduna bi, wuute ak limu 464 000 yi mu faat ci atum 1990. Su nit ñi jëlee garab yi war ci meningite bacterie bi, du mëna faat lu yegg 15%. At mu nekk dini am feebaru meningite bu bactérie ci diggante weeru decembre ak juin ci biir Afrique bi ci suufu Sahara, ñu gën ko xame ci turu ceinture de meningite. Feebar bi mën feeñ ci gox ci àdduna bi waaye du bari noonu. Baatu meningite mingi bawoo grek μῆνιγξ méninx, "membrane" ak sufiksu -ite, "inflammation" +Meningite nekk na xeetu mettit yu tar la yuy jàpp cër yiy aar yuuru nit ki, ak doqam, te ñu koy gëna woowe meninge. Ni muy gëna feeñee ci nit mooy yaram wu tàng, mettitu bopp ak ndong lu bañ. Yenn saay mu feeñee neeneen, lu ci melni xel mu jaxasoo ak ñàkka xàmme yenn mbir, waccu, bëggul leeraay ak xumbaay. Neneen lay feeñee ci xale yi, lu ci melni gaawa mer, tayeel, wala baña lekk. Ni muy tàmbalee feeñ ci yaramu ki ko am, mën na wane ban xeetu Meningite la am; ci misaal, Meningite bi bacterie meningococcal mën na ànd ak yeneen xeetu feeñal ci deru nit ki. + +Wiris, bakteri wala yeneen doomi jàngoro mën nañu jàpp wàll yu bari ci yaram wi, garab yi itam mën nañu ko waaye bariwul. Meningite mën na faat doomu aadama ndax li muy yàq dafa jege yuur gi ak moelle epiñeer; moo tax, su dalee nit ki dañu ko wara gaaw faj. Suñu jamee (Une ponction lombaire) nit ki ci yaram lañuy mëna xam ndax amna Meningite am déet. Dañuy roof ràbb ci kanaal rachidien bi ngir taataan lenn ci liquide cephalo-rachidien (LCR), bi muur yuur gi ak moelle epiñeer bi. Ci ab labo lañu càmbaree LCR. + +Amna yenn xeetu meningite yoo xamni boo ñaqoo duñu la mënal dara, muy ñaq biy aare ci méningocoque, oreillon, pneumocoque ak Hib. Ñi nekk ci barab bu am yenn xeeti meningite yi mën nañuy jëfandikoo antibiotique, baaxna ci lool. Li ñu wara njëkka jox ki am meningite bu metti bi mooy ay antibiotique ak yenn garab yuy xeex doomu jàngoro ji (virus). Soo bañee meningite bi indal la mettit yu dara wala mu am lumuy yàq ci sa der, dangay jël ay corticostéroïde ngir mu aar la ci yooyu jafe-jafe. Meningite mën na indil nit ki ay jafe-jafe su yàggee, maanaam mën nala tëxloo, soyloo, wala xel mu wayadi, sudee teelu ñu ko faj. + +Ci atum 2015, meningite jàpp na lu tollu ci 8,7 milioŋ ciy nit. Feebar bi faatna 379 000 nit ci àdduna bi, wuute ak limu 464 000 yi mu faat ci atum 1990. Su nit ñi jëlee garab yi war ci meningitu bakteri bi, du mëna faat lu yegg 15%. At mu nekk dina am feebaru meningite bu bakteri ci diggante weeru decembre ak juin ci biir Afrique suufu Sahara, ñu gën ko xame ci turu ceinture de meningite. Feebar bi mën na feeñ ci yeneen gox ci àdduna bi waaye du bari noonu. Baatu meningite mingi bawoo grek μῆνιγξ méninx, "membrane" ak sufiksu -ite, "inflammation." +Ñaqu antimeningococcique mooy bépp ñaq bi ñu mëna jëfandikoo ngir mucc ci feebaru Neisseria meningitidis.Amna yeneen xeetu ñaq yu mëna musal nit ki ci yenn ci xeetu meningite yii ñuy lim: A, B, C, W-135, ak Y. Baaxaayu kaaraange ñaqu gi mingi ci diggante 85 ak 100% mën na yàgg gën gaa néew ñaari at. Ci ñi koy jëfandikoo, dina fa wàññi méningite ak sepsie. Ci sidit lañu la koy jam wala ci suufu der bi. + +Waa OMS (Mbootaayu sàmm wérgi-yaram ci àdduna bi) waxna ni ñi nekk ci barab yu bari meningite wala yu ko xawa am, dañu wara ñaqu ngir mucci ci feebar bi. Sudee gox yi feebar bi bariwul, nañu ñaq ñi nekk ci wetu ñu am feebar bi. Ci goxu afrique yi nekk ci ndomba meningite, ñu ngi def jéego yu mag ngir ñaq yi am diggante 1 at jàpp 30 at, muy ñaq bi boole ak méningocoque A. Ci Kanada ak ci États-Unis, dañuy digle ñuy faral di ñaq ci saasi bépp xale bu nekk ci barab bi feebar bi nekk te bari fa. Waa Arabi Saudi dañuy sàkku ci képp kuy aji Màkka mu jël ñaq bi koy aar ci meningite. + +Ñaqu meningite (Meningococcal), daanaka ñaq bu wóor la. Ci ñénn ñi, barab bi ñu leen ñaq mën na xonk wala mu metti tuuti. Jiggéen ju ëmb mën na ko jëfandikoo. Néew la lool lumuy indi nit ki ay jafe-jafe, matul benn ci 1milioŋi ñaq. + +Ci atum 1970 lañu njëkka génne ñaqu meningocoque. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Ñu ngi jaaye ñaq bi 3,23 ak 10,77 USD dose bu nekk (en gros) li dalee atum 2014. Ci États-Unis, ñu ngi koy jaaye ci diggante 100 ak 200 USD. +Ŋas (rougeole), feebar la bu gaawa wàlle, te li koy joxe mooy doomu jàngoroy ŋas. Màndarga yi muy gëna faral di njëkka wane sula dalee mooy yaram wu tàng lool ba weesu 40 °C (104.0 °F), sëqët, bakkan bu sotti, ak bët yu xonk. Sula nit wàllee feebar bi, dinga toog 10 jàpp 12 fan laata muy feeñ ci sa yaram. Su tàmbalee feeñ ba def ñaari fan jàpp ñatt dafay def ay tupp yu weex ci gémmiñu ki feebar, ñu leen di woowe tuppi Koplik. Su amee ci yaw ñatt jàpp juróomi fan, sa deru yaram tàmbali di am ay tërgën wala picc yu xonk, muy faral di tàmbalee ci sa kanam, yegg ba ci sa yaram wi yépp. Jafe-jafe yi muy gëna faral di indil nit ki mooy, biir buy daw (8% ci ñi am feebar bi), (7%) ak pneumonia (6%). Li faral di waral mbir yooyu mooy matuwaayi moytu feebaru ŋas bu jeex. Néew na lu muy sayloo nit, wala mu koy gumbaal wala muy indil yuuram ay jafe-jafe. Rubeole "Rougeole bu Almaañ" ak roseole ñaari feebar yu wuute la, te yeneen wiris yu bokkul bu ŋas moo leen di joxe. + +Rougeole (ñas) bi ngelaw li moo koy tasaare, sedee kimu dal dafa sëqër sa wet wala muy tissooli mën nala ko wàll. Sula toflitam laalee wala ñandxitam mën nala wàll. Ñi nekk ci wetu ki feebar te seen yaram amul matuwaay yu xeex feebar bi, fukk yoo ci jël, juróom ñeent ya dina ñu ko am. Ci ñeent fan yi jiitu picc yu xonk yi di feeñ ak ñeent fan ginaaw bi ñu feeñee, nit ki mën na ci wàlle feebar bi. Néew na lu feebar bi di dal nit ki ñaari yoon. Nit ñi war nañu di saytu ndax amu ñu doomu jàngoro ji suñu nekkee ci barab buñ ko mëna amee. + +Képp ku jël ñaqu (vaccin) anti rougeole bi mën nga mucci ci feebar bi, te yenn saay nga fekk ñu boole ko ak yeneen ñaq. Soo xaymaa li feebar bi daan faat ciy nit leegi wàññi na ci 80% ci diggante atum 2000 ak 2017, mu am 85% ci gone yi ci àdduna bi yépp yi ñu jota ñaq benn yoon ci atum 2017. Su feebar bi dalee nit ki, amul benn garab buñu mëna waxni moo ko mëna faj, waaye amna ay pexe yu ci mëna jàppale nit ki. Lu ci melni di faral di may ndox ki feebar (dox mu am suukar ak xorom su yam), lekk ñam wu sell, ak jël garab yuy wàcce tàngooru yaramam. Mën nga jël antibiotic itam sudee danga amaale bakteri (doomu jàngoro) bi lay jox pneumonie. Sudee ci réew yu néew doole yi, dañuy digal ki feebar mu jël vitamine A. + +At mu nekk, feebar bi dina jàpp lu toolu ci 20 milioŋ ciy doomu aadama, ñi ëpp ci ñoom ñooy waa Afrique ak waa Asie. Barina ñu koy jàppee feebaru xale waaye ku nekk la mëna dal. Bokk na ci feebar yi am vaccin yi dàq a ray. Ci atum 1980, feebar bi daan na faat lu tollu ci 2,6 milioŋ ciy nit, te ci atum 1990, faatna 545 000 doomi aadama; bi ñuy yegg ci atum 2014 prograamu ñaq nit ñi ci àdduna bi wàññina limu ñiy faatu ci rougeole ba 73 000. Lu weesu xayma yooyu ñu amal ak dee gi yokk ci diggante 2017 ba 2019 ndax matuwaayi fàggu ci feebar bu jeex. Li ñu xayma ni moom lay faat mingi tollu ci 0.2%, waaye mën yegg ba ci 10% ci barab yi amul dund gu baax. Ñi ëpp ci ñi feebar bi di faat ñooy xale yi amagul 5 at. Daa melni feebar bi mënalul dara rab yi. +Ñaqu BCG (Bacillus Calmette-Guérin) mooy lila gëna mëna aar ci tuberkuloos (TB). Sudee ci réew yi feebaru tuberkuloos wala ngaana bari, digle nañu ñu ñaq benn yoon xale biy sooga judd te amul benn feebar nga ñaq ko ci nimu gëna gaawe su juddoo. Sudee ci barab yi feebar bi bariwul, xale yi nekk ci barab bi ñu ko mëna amee ñoom la seen yaram di am ay matuwaayi moytu feebar bi, waaye su amee kuñu ñaaw njortu ndax amna feebar am déet, dañu koy saytu ba noppi faj ko. Mag ñi amul tuberkuloos te nekk ci barab bu feebar bi bari, seen yaram mën na defar ay matuwaay yu leen di aar ci feebar bi. Ñaqu BCG mën nala aaraale itam ci feebar yu melni ulseeru Buruli ak yenn feebari bacteri yu bokkul ak tuberkuloos. Rax ci dolli dina ñu koy faral di jëfandikoo ngir faj kanseeru naq. + +Yàggaayu kaaraange ñaq bi barina te wuute, waaye mën na yegg ba 20 at. Ci xale yi ñu ñaq, dina am 20% ci ñoom ñu dul am feebar bi, ñeneen ñi des itam suñu amee feebar bi itam, du leen mënal dara. Ñaq bi ci suufu deru yaram wi lañu la koy defal. Ama guñu firnde ci ndax dañu koy baamtu am déet. + +Daanaka ñaq bi amul benn loraange. Yenn saay fiñu la ko jam xonk wala mu newwi, wala nga yëg tuuti metit. Mën nga amaale ulseer bu ndaw ak yenn léget su weree. Efe secondaire yi ñoo ci gëna bari, te ci mag ñi amatul matuwaayu xeet feebar bi lay gëna sonal. Wóoral a jox jigéen ju ëmb. Ñu ngi ñëkka sosee ñaq bi cii Mycobacterium bovis muy luñuy faral di jëlee ci nag. Néewal nañu dooleem bu baax waaye mingi dundu. + +Ci atum 1921 lañu njëkka jëfandikoo ñaqu BCG ci wàllu faj. Bokk na ci limu ñaq yi OMS jàpp ni ñoo gëna am solo ci wérgi-yaramu nit ki. Ci diggante atum 2011 ak 2014, njëg li en gros mingi tolluwoon ci diggante 0,16 USD jàpp 1,11 USD benn dose ci réew yu néew doole yi. Ci réewum Etats Unis, ñaq baa ngi fay jar ci diggante 100 ak 200 USD. Li ko dalee 2004, at mu nekk dina ñu ñaq lu tollu ci 100 miliyoŋi xale ci àdduna bi at. +Ñaqu rougeole (ŋas) mooy li lay musal ci rougeole. Sudee bi nga njëkkee ñaqu sa yaram defarul lu koy aar ci feebar bi, soo ñaquwaate rek feebar bi dootul mën dara ci yaw. Sudee dañu ñaq lu weesu 92% ci waa dëkk bi, mën nañu jàpp ni dëkk boobu feebar bi dufa feeñ; waaye mën na fa ñëwaat sudee limu ñiy ñaqu dafa dem ba wàññiku. Soo ñaqoo dinga mucc ci feebar bi ay at yu bari. Xama guñu bu baax ndax ndax kaaraangeg ñaq bi dafay wàññiku. Ñaq bi mën nala aar itam soo ko jëlee ci biir ñaari fan yi nga nekk ci barab bula feebar bi mëna dale. + +Ñaq bi du indil nit ki benn jafe-jafe, doonte danga am VIH. Mën nala xawa sonal tuuti waaye du yàg dara. Maanaam fi ñu la ko jam mën na saf tuuti wala sa yaram xawa tàng. Amul benn yokkute buy seetlu ci limu Seetlu nañu itam 3,5 jàpp 10 kaa anaphylaxie ci miliyoŋi nit ñuñu ñaq. Sudee lu jëm ci feebar Guillain-Barré, autisme ak biir buy metti (maladie intestinale inflammatoire) gisu ñu ci benn yokkute. + +Ñaq bi amna mooy kese, waaye itam dina ñu koy boole ak yeneen ñaq yu ci melni ñaqu ROR, (muy boole ñaqu rubeole ak anti-ourlien) wala ñaqu RROV (maanaam ñu boole ñaqu RRO ak ñaq biy aare ci varicelle). Ñaq bii aare ci rougeole dafay musalaate ci feebar itam ndeem dañu ko boole ak yeneen ñaq, te effets secondaires yi dañuy wuute, lépp di aju ci xeetu ñaq bi ñu ko booleel. Waa OMS ñoo digal ñu ñaq xale bi su amee juróom ñeenti weer te nekk ci barab bu feebar bi bari. Waaye sudee fu feebar bi bariwul la, jaaduna ñu ñaq xale bi su amee fukki weer ak ñaar. Ñaq bi luy doomu jàngoroy rougeole bu dundu la waaye dañu ñéewal dooleem. Ñaq bi puudar bu waw la, fàww ñu jaxase ko laata ñu koy jam nit ki ci suufu deram wala ci siditam. Soo bëggee xam ndax ñaq bi jàppna danga saytu deretam. + +Ci atum 2013, ñaq nañu lu tollu ci 85% xale yi ci àdduna bi. Ci atum 2015 amna gën gaa néew 160 réew yu baamtu ñaq bi ngir nit ñi mën a am matuwaay yu leen musal ci feebar bi. Ci atum 1963 la ñu njëkka génne ñaq bi. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Njëgi ñaq bi ci réew yu néew doole yi mingi tollu ci 0,70 USD dose bu nekk, en gros, li tàmbale 2014. Ginaaw feebar bi dafa faral ci barab yi nit ñu bari ñaquwul, feebar dina tax ñu xam barab yi ñaq bi barul ñu ko def. +Tuberkiloos (TB) feebar la buy wàlle, te li koy faral di joxe mooy doomu jàngaor bi tuddu Mycobacterium tuberculosis (MTB). Cër bi tuberkuloos di ngëna jàpp mooy dënn bi, waaye mën na dem ba laalaale yeneen cër ci yaramu nit ki. Barina lu muy dal nit te du feeñ, loolu lañuy woowe tuberkuloos bu nëbbatu. Lu tollu 10% feebar yiy nelaw yaramu nit ki, dañuy dem ba daaneel nit ki, suñu ko fajul, mën na dem ba faat ki mu dal. Beneen tuburkuloos bi nelawul moom dafay wane boppam, kumu dal dangay am sëqët mu tar àndaale ak lumbi deret, yaram wu tàng, ñaqu guddi, ak yaram wuy jeex di dem. Di nañu koy faral di woowe feebaru "ŋacci" ndax limuy ŋacci sa yaram. Amna yeneen anam yu muy feeñee su laalee yeneen cër yi. + +Tuberkuloos dafay tasaaroo ci ngelaw li, suede tuberkuloos bu tar moo la jàpp, soo sëqëtee wala nga tifli wala nga wax, wala nga tissooli mën nga ko wàlle. Nit ñi feebar bi di nelaw ci seen yaram du ñu wàlle feebar bi. Nit ñi gëna mëna wàlle feebar bi mooy ñi am VIH/SIDA ak tóxkat yi. Ngir saytu jàngoro ju tar ji ci yaram nit, dañuy rajo dënn bi, dañuy jël itam ndox mu bawoo ci moom ñu xool ko ci microscope wala ñu amal ci njàngat mu xóot. Sudee tuberkuloos biy nelaw nak, ci deru nit ki wala ci deretam. + +Suñu bëgee aar nit ñi ci feebar boobu, nañuy saytu bu baax ñi nekk fumu leen mëna dalee, teela gis doomu feebar bi ak teel ko faj, ak jël ñaq bii di Bacile Calmette-Guérin (BCG). Nit ñi feebar bi gëna yab ñooy ñiy liggéeyandoo ak ki ko am, ñi mu bokkal kër, workplace, ak ñi muy nekkal bis bu nekk. Paj mi dafay yàgg lool, te ay àntibiotik lañu koy defee. Doomu jàngoro bi daa tàmbali ñeme garab yu bari (MDR-TB) ak doomu jàngoro yi ñeme yeneen garab bi (XDR-TB). + +Ci atum 2018, ñeenti nit ñoo jël xalaat nañu ni kenn ka amna tuberkuloos. At mu nekk dina am lu tollu ci 1% ci nit ñi ci àdduna bi ñuy am doomu jàngoro ji. Ci atum 2017, amoon na lu ëpp 10 milion ci nit ñu am feebar bi, ci ñooñu amna ci lu tollu 1.6 milion ñu ci ñàkk seen bakkan. Loolu moo ko def feebar bi dàqa ray ci feebar yiy wàllaate.Lu ëpp 95% nit ñi mu faat ci réew yu néew doole yi lañu dëkk, lu ëpp 50% Inde, Chine, Indonesie, Pakistan, ak Philippines. Seetlu nañu ni li ko dale atum 2000 ba leegi wàllaate gi dafay gëna wàññeeku at mu nekk. Nit ñi saytu ndax am nañu tuberkuloos am déet, 80% ci ñoom dañuy am feebar bi suede ci Asie ak ci Afrique waaye suede ci Etats Unis 5–10% ci nit ñi ñuy saytu ñoo koy am. Ca jamonoy maam ya ba leegi tuberkuloos a ngi am. + +Cosaanu gëstu bi +Taata bu Monsoro (Faraañse : Château de Montsoreau) : Faraas, Monsoro + +Open : 2016 +Dayoo : 3500 m² +Visites : 52000 (2018) + +External links + + www.chateau-montsoreau.com + +Faraas +Alto Mira benn dekk-dëkkaan Porto Novo ci yu bëj-gannar-sowwu yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +«Santo Antão: Agricultores de Alto Mira querem apoio do MDR para compensar estragos nas culturas» Inforpress CV. Praia. 9 satumbar 2015 + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Tinteira benn dekk-dëkkaan Santa Catarina do Fogo ci yu penku yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Manchester City F.C. (Manchester City Football Club) benn football club ci "Premier League" (Angale - Nguur-Yu-Bennoo) ci dekku Manchester. + +Premier League: +2011-12, 2013-14, 2017-18, 2018-19 + +Staad +Staad Dëkku Manchester/Staad City of Manchester + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Manchester City F.C. - Dalub web + +Premier League +Futebol Clube de Derby benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Mindelo ci yu dunu São Vicente. + +Campeonato Nacional (Kap Weert):3 +1983/84, 1999/2000, 2004/05 + +1. Liig - São Vicente: 9 +1982/83, 1983/84, 1984/85, 1985/86, 1999/00, 2000/01, 2004/05, 2007/08, 2013/14 + +Staad +Staad Adérito Sena (Estâdio Municipal Adérito Sena) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Colega + Tubola + +Karmat ak delluwaay + +São Vicente (Kap Weert) +Football +Tarrafal, Kap Weert: + +Tarrafal, dëkku ci yu dunu Santiago +Tarrafal, dëkkaanu ci yu dunu Santiago +Tarrafal (Ribeira Grande) - dunu Santo Antâo +Tarrafal de Monte Trigo, dëkk-dekkanni ci yu dunu Santo Antão +Tarrafal de São Nicolau +Escudo kap weert ($, ISO 4217: CVE) ci xaalisu Kap Weert. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Kap Weer +Tarrafal benn dëkkaanu ci yu bëj-gannar yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Dëkki +Tarrafal + +Dëkk-dëkkaani + +Achada Biscanhos +Achada Lagoa +Achada Longueira +Achada Meio +Achada Moirão +Achada Tenda +Biscainhos +Chão Bom +Curral Velho +Fazenda +Figueira Muita +Lagoa +Mato Brasil +Mato Mendes +Milho Branco do Norte +Ponta Lobrão +Ribeira da Prata +Tras os Montes + +Sport + +Football clubi +Amabox Barcelona +Beira-Mar Tarrafal +Estrela dos Amadores +Real Júnior +Varandinha + +Staad +Staad Maangi/Mangue (Staad Tarrafal) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.ams.cv/index.php?option=com_content&task=view&id=30&Itemid=55 +https://web.archive.org/web/20191118235645/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/Tarrafal.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Coqueluche, feebaru sëqët bu tar la, ñu koy faral di woowe sëqëtum100 fan, feebar la bu gaaw ci wàlle te benn doomu jàngoro (bakteri) moo koy joxe. Su lay sooga dal, dangay melni ku soj, sa bakkan di sotti ndox, sa yaram tàng ngay sëqët ndànk. Ci ayi-bis yi ci topp, sëqët mi dafay gëna tar. Nit ki su sëqëtee ba sëqët mi jéggi dayo, su nit ki noyyi dangay dégg muy riir. Sëqët mën na dem ba 100 fan, wala ba 10 ayi-bis. Nit ki mën na sëqët ba waccu, wala mu dam faaram, wala mu dem sax ba dootul amati benn njariñ. Su jàppee xale bu amagul at, du sëqët wala limuy sëqër du bari waaye nak mën na fatt seen noyyi ab diir. Diggante bi muy dug sa yaram ak bi muy feeñ mën na def juróom ñaar jàpp fukki fan. Feebar bi mën na dal ñi ñaqu ba noppi waaye ni muy feeñee du tar noonu. + +Doomu jàngoro (Bactérie) biy joxe coqueluche mooy Bordetella pertussis. Feebar la buy tasaaroo ci ngelaw li, di bawoo ci kiy sëqët, tisooli ki am feebar bi. Bu nit ki xasee ba am feebar bi rek mën na ko wàllee ba keroog sëqëtam mu metti mi di am ñatti ayi-bis. Ñi ñu fajee ak ay antibiotic dootu ñu wàlle suñu weesoo juróomi fan. Suñu bëggee saytu feebar bi, dañuy xool ci ginaaw bakanu nit wala ci putam. So noppee ñu amal njàngat mu xóot ci ni chaine polymerase bi di doxee. + +Li gëna mëna aar nit ki ci jàngoro jooju mooy mu ñaqu anti-coqueluche. Liir bi su amee juróom benn jàpp 8 juróom ñatti weer dañu ko wara ñaq ngir musal ko ci feebar boobu, mu luñu wara baamtu ñeenti yoon laata xale bi di weesu ñaari at. Lu ñaq bi di gëna yàgg dooleem di gëna néew, moo tax yen xale dañu leen di faral di baamtul ñaq bi, ak yenn mag yi itam. Nit ñi nekk ci barab bu leen feebar bi mëna dale, mën nañu jël antibiotic ngir mu musal leen ci feebar bu tar bi. Ki feebar bi dug ci yaramam ba noppi mën na jël ay antibiotik diiru ñatti ayi-bis ginaaw bi feebar bi tàmbalee feeñ suko weesoo du ci mën lu bari. Sudee xale bu amagul at la, ak ci jigéen ñi ëmbmën nañu ko jël ci biir 6 ayi-bis ginaaw feeñal yu njëkk yi. Antibiotik yi nga mëna jëfandikoo ñooyerythromycin, azithromycin, walatrimethoprim/sulfamethoxazole. Ama guñu gëstu bu leer bu wane xarañteg garab giy dakkal sëqët mi. Lu tollu 50% ci xale yu bari yu amagul benn at, fàww ñu yóbbu leen hospital, 0;5% ci ñoom (1 ci 200) dañuy faatu. + +At mu nekk coqueluche dina jàpp lu tollu ci 16 milion ci nit ci àdduna bi. Waa réew yu néew doole yi lay gëna jàpp te mën na dal ku nekk, mag wala ndaw. Ci atum 2015 feebar faat 61 000 nit – wuute ak 138 000 yi mu faat ci  1990. Lii yi amagul at le am feebar lu xawa yées 2% ci ñoom lay faat.Jàpp nañu feebar baa ngi njëkka feeñ ci 16eme xarnu (siècle). Ci atum 1906 la ñu njëkka gis bacterie bi koy joxe. Ci atum1940 lañu njëkka génne ñaq bi. +Ñaqu sëqët su tar (coqueluche) mooy li mëna aar nit ki ci feebaru coqueluche. ñaari xeetu ñaqu coqueluche ñoo am: biy am selil bi yépp ak bi ko dul am. ñaq biy am selil bi yépp amna kaaraange gu yegg ba ci 78% waaye ñaq bi amul selil bi amna diggante 71 jàpp 85% ci kaaraange. Kaaraange ñaq bi dafay wàññeeku, li ko dalee 2 ba 10% at mu nekk, waaye bi kaaraange ñaq bi amul selil bi mooy gëna gaawa wàññeeku. Suko jigéen ju ëmb jëlee dafay aaraale liir bi ci biiram. Gis nañu ni ñaq bi musal lu ëpp genn-wàllu milion ciy nit ñumu naroon faat ci 2002. + +Waa Mbootaayu Wergi-yaram ci Àdduna bi (OMS) ak waa Kuréel giy Saytu ak Fàggu ci Feebar yi (CDCP) dañu digle ñu ñaq xale yépp ci anti-coqueluche te ñu boole ko ci ñaq yi ñuy faral di def. Nit ñiVIH/SIDA bokk nañu ci ñi ko wara jël. Xale war nañu ko jël ñatti yoon, di tàmbali suñu amee juróom-benni ayi-bis. Mën nañu ci yokk yeneen sudee xale bu dëgër wala mag. Ñaq yi ci am dañu àndaale ak yeneen ñaq. + +Réew yi am doole, ñaq bi amul selil lañuy jëfandikoo ndax daanaka du jural nit ki benn jafe-jafe. Diggante 10 jàpp 50% ci nit ñi jël ñaq bi am selil bi yépp, barab biñu leen ko jam dafay deretal te dañuy amaale yaram wu tàng. Ñi ciy jëlee ay say yu ndaw wala mu leen di xir ciy jooy matul 1%. Sudee ñaq bi amul selil bi la nak, yenn saa fi ñu jam ci loxo bi newwi tuuti waaye du yàgg. Ñaar yépp a mëna jur jafe-jafe waaye bi am selil bi, lu nit ki gëna nekk xale muy gëna néew. Xale bi su demee ba am 6 at, waratu ñu ko jox ñaq bi am selil bi yépp. Amul benn ñaari xeeti ñaq yooyu buy indil nit ki jafe-jafe ci wàll neer. + +Ci atum 1926 la ñaqu anti-coqueluche bi njëkka am. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Amna ci xeetu ñaq bu àndaale aktetanos, diphtherie, polio, akHib vaccine ñuy koy jaaye 15,41 dolaar (USD) dose bu nekk ci atum 2014. +Ñaqu sëqët su tar (coqueluche) mooy li mëna aar nit ki ci feebaru coqueluche. Ñaari xeetu ñaqu coqueluche ñoo am: biy am selil bi yépp ak bi ko dul am. Ñaq biy am selil bi yépp amna kaaraange gu yegg ba ci 78% waaye ñaq bi amul selil bi amna diggante 71 jàpp 85% ci kaaraange. Kaaraange ñaq bi dafay wàññeeku, li ko dalee 2 ba 10% at mu nekk, waaye bi kaaraange ñaq bi amul selil bi mooy gëna gaawa wàññeeku. Suko jigéen ju ëmb jëlee dafay aaraale liir bi ci biiram. Gis nañu ni ñaq bi musal lu ëpp genn-wàllu milion ciy nit ñumu naroon faat ci 2002. + +Waa Mbootaayu Wergi-yaram ci Àdduna bi (OMS) ak waa Kuréel giy Saytu ak Fàggu ci Feebar yi (CDCP) dañu digle ñu ñaq xale yépp ci anti-coqueluche te ñu boole ko ci ñaq yi ñuy faral di def. Nit ñiVIH/SIDA bokk nañu ci ñi ko wara jël. Xale war nañu ko jël ñatti yoon, di tàmbali suñu amee juróom-benni ayi-bis. Mën nañu ci yokk yeneen sudee xale bu dëgër wala mag. Ñaq yi ci am dañu àndaale ak yeneen ñaq. + +Réew yi am doole, ñaq bi amul selil lañuy jëfandikoo ndax daanaka du jural nit ki benn jafe-jafe. Diggante 10 jàpp 50% ci nit ñi jël ñaq bi am selil bi yépp, barab biñu leen ko jam dafay deretal te dañuy amaale yaram wu tàng. Ñi ciy jëlee ay say yu ndaw wala mu leen di xir ciy jooy matul 1%. Sudee ñaq bi amul selil bi la nak, yenn saa fi ñu jam ci loxo bi newwi tuuti waaye du yàgg. Ñaar yépp a mëna jur jafe-jafe waaye bi am selil bi, lu nit ki gëna nekk xale muy g��na néew. Xale bi su demee ba am 6 at, waratu ñu ko jox ñaq bi am selil bi yépp. Amul benn ñaari xeeti ñaq yooyu buy indil nit ki jafe-jafe ci wàll neer. + +Ci atum 1926 la ñaqu anti-coqueluche bi njëkka am. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Amna ci xeetu ñaq bu àndaale aktetanos, diphtherie, polio, akHib vaccine ñuy koy jaaye 15,41 dolaar (USD) dose bu nekk ci atum 2014. +Coqueluche, feebaru sëqët bu tar la, ñu koy faral di woowe sëqëtum100 fan, feebar la bu gaaw ci wàlle te benn doomu jàngoro (bakteri) moo koy joxe. Su lay sooga dal, dangay melni ku soj, sa bakkan di sotti ndox, sa yaram tàng ngay sëqët ndànk. Ci ayi-bis yi ci topp, sëqët mi dafay gëna tar. Nit ki su sëqëtee ba sëqët mi jéggi dayo, su nit ki noyyi dangay dégg muy riir. Sëqët mën na dem ba 100 fan, wala ba 10 ayi-bis. Nit ki mën na sëqët ba waccu, wala mu dam faaram, wala mu dem sax ba dootul amati benn njariñ. Su jàppee xale bu amagul at, du sëqët wala limuy sëqër du bari waaye nak mën na fatt seen noyyi ab diir. Diggante bi muy dug sa yaram ak bi muy feeñ mën na def juróom ñaar jàpp fukki fan. Feebar bi mën na dal ñi ñaqu ba noppi waaye ni muy feeñee du tar noonu. + +Doomu jàngoro (Bactérie) biy joxe coqueluche mooy Bordetella pertussis. Feebar la buy tasaaroo ci ngelaw li, di bawoo ci kiy sëqët, tisooli ki am feebar bi. Bu nit ki xasee ba am feebar bi rek mën na ko wàllee ba keroog sëqëtam mu metti mi di am ñatti ayi-bis. Ñi ñu fajee ak ay antibiotic dootu ñu wàlle suñu weesoo juróomi fan.Suñu bëggee saytu feebar bi, dañuy xool ci ginaaw bakanu nit wala ci putam. So noppee ñu amal njàngat mu xóot ci ni chaine polymerase bi di doxee. + +Li gëna mëna aar nit ki ci jàngoro jooju mooy mu ñaqu anti-coqueluche. Liir bi su amee juróom benn jàpp 8 juróom ñatti weer dañu ko wara ñaq ngir musal ko ci feebar boobu, mu luñu wara baamtu ñeenti yoon laata xale bi di weesu ñaari at. Lu ñaq bi di gëna yàgg dooleem di gëna néew, moo tax yen xale dañu leen di faral di baamtul ñaq bi, ak yenn mag yi itam. Nit ñi nekk ci barab bu leen feebar bi mëna dale, mën nañu jël antibiotic ngir mu musal leen ci feebar bu tar bi. Ki feebar bi dug ci yaramam ba noppi mën na jël ay antibiotik diiru ñatti ayi-bis ginaaw bi feebar bi tàmbalee feeñ suko weesoo du ci mën lu bari. Sudee xale bu amagul at la, ak ci jigéen ñi ëmbmën nañu ko jël ci biir 6 ayi-bis ginaaw feeñal yu njëkk yi. Antibiotik yi nga mëna jëfandikoo ñooyerythromycin, azithromycin, walatrimethoprim/sulfamethoxazole. Ama guñu gëstu bu leer bu wane xarañteg garab giy dakkal sëqët mi. Lu tollu 50% ci xale yu bari yu amagul benn at, fàww ñu yóbbu leen hospital, 0;5% ci ñoom (1 ci 200) dañuy faatu. + +At mu nekk coqueluche dina jàpp lu tollu ci 16 milion ci nit ci àdduna bi. Waa réew yu néew doole yi lay gëna jàpp te mën na dal ku nekk, mag wala ndaw. Ci atum 2013 feebar faat 61 000 nit – wuute ak 138 000 yi mu faat ci  1990. Lii yi amagul at le am feebar lu xawa yées 2% ci ñoom lay faat.Jàpp nañu feebar baa ngi njëkka feeñ ci 16eme xarnu (siècle). Ci atum 1906 la ñu njëkka gis bacterie bi koy joxe. Ci atum1940 lañu njëkka génne ñaq bi. +Fundura benn dekk-dëkkaan Santa Catarina ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Siggcoor benn dëkku Senegaal. Mooy péyu diiwaanu Kaasamaas. +Konakri mooy péyu réewum Gine. + +Péy +Dëkk +Ñaqu meningite mooy bépp ñaq bi ñu mëna jëfandikoo ngir mucc ci feebaru Neisseria meningitidis. Amna yeneen xeetu ñaq yu mëna musal nit ki ci yenn ci xeetu meningite yii ñuy lim: A, B, C, W-135, ak Y. Baaxaayu kaaraange ñaqu gi mingi ci diggante 85 ak 100% mën na yàgg gën gaa néew ñaari at. Li mu jur mooy wàññikuy méningite ak sepsie ci barab yiñ leen jëfandikoo lu bari. Mën nañu la def ñaq bi ci sa sidit wala ci suufu der bi. + +Waa OMS (Mbootaayu sàmm wérgi-yaram ci àdduna bi) waxna ni ñi nekk ci barab yu bari meningite wala yu ko xawa am, dañu wara ñaqu ngir mucci ci feebar bi. Sudee gox yi feebar bi bariwul, nañu ñaq ñi nekk ci wetu ñu am feebar bi. Ci goxu afrique yi nekk ci ndomba meningite, ñu ngi def jéego yu mag ngir ñaq yi am diggante 1 at jàpp 30 at, muy ñaq bi boole ak méningocoque A. Ci Kanada ak ci États-Unis, dañuy digle ñuy faral di ñaq ci saasi bépp xale bu nekk ci barab bi feebar bi nekk te bari fa. Waa Arabi Saudi dañuy sàkku ci képp kuy aji Màkka mu jël ñaq bi koy aar ci meningite. + +Ñaqu meningite (Meningococcal), daanaka ñaq bu wóor la. Ci ñénn ñi, barab bi ñu leen ñaq mën na xonk wala mu metti tuuti. Jiggéen ju ëmb mën na ko jëfandikoo. Néew la lool lumuy indi nit ki ay jafe-jafe, matul benn ci 1milioŋi ñaq. + +Ci atum 1970 lañu njëkka génne ñaqu meningite. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Ñu ngi jaaye ñaq bi 3,23 ak 10,77 USD dose bu nekk (en gros) li dalee atum 2014. Ci États-Unis, ñu ngi koy jaaye ci diggante 100 ak 200 USD. +Bissawóo (wu-portigee: Bissau) mooy péyu réewum Gine Bisaawóo. + +Waax +Waax bu Bisaawóo (Porto de Bissau) + +Sport + +Futbol klubi +Sporting Bisaawóo (Sporting Clube de Bissau) +SC Portos de Bissau (SK Waaxi bu Bisaawóo) +Sport Bissau e Benfica (Benfica gu Bisaawóo) +UDIB + +Staad +Staad 24 Sattumbar (Estádio Nacional 24 de Setembro) + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Péy +Dëkk +Cova Rodela benn dekk-dëkkaan Brava ci yu penk yu dunu Brava, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Reitmaier, Pitt & Fortes, Lucete: Cabo Verde, p. 419. Bielefeld 2009. + +Lëkkalekaay yu biti + +Brava +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Tarrafal benn dëkkaanu ci yu bëj-gannar yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Dëkki +Picos (Achada Igreja) + +Dëkk-dëkkaani + +Aboboreiro +Achada Leitão +Babosa +Burbur (Burbuur) +Covão Grande +Degredo +Djéu +Faveta +Jalalo Ramos +Junco +Leitão Grande +Leitãozinho +Manhanga +Mato Fortes +Mato Limão +Pico Freire +Picos Acima +Pico Vermelho +Purgueira +Rebelo Acima + +Sport +São Lourenço FC + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.ams.cv/index.php?option=com_content&task=view&id=30&Itemid=54 +https://web.archive.org/web/20191118235513/http://www.anmcv.com/Munic%C3%ADpios/S%C3%A3oSalvadordoMundo.aspx + +Dëkki Kap Weer +Dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Melosuufug Kap Weert + +Ndoxi +Mbàmbulaan gu Atlas + +Duni +Boa Vista +Ilhéu de Sal Rei +Brava +Ilhéu Grande +Fogo +Maio +Sal +Ilhéu Rabo de Junco +Santiago +Ilhéu de Santa Maria +Santa Luzia +Ilhéu Branco +Ilhéu Raso +Santo Antão +São Nicolau +São Vicente +Ilhéu dos Pássaros + +Dëkkaani + +Brava +Maio +Mosteiros - Fogo +Paul - Santo Antão +Porto Novo - Santo Antão +Praia - Santiago +Ribeira Brava - São Nicolau +Ribeira Grande de Santiago +Ribeira Grande - Santo Antão +Sal +Santa Catarina - Santiago +Santa Catarina do Fogo +Santa Cruz - Santiago +São Domingos - Santiago +São Lourenço dos Órgãos - Santiago +São Miguel - Santiago +São Salvador do Mundo - Santiago +São Filipe - Fogo +Tarrafal - Santiago +Tarrafal de São Nicolau + +Dëkki i diiwaani +Assomada - Santiago +Cidade Velha - Santiago +Espargos - Sal +Mindelo - São Vicente +Porto Novo - Santo Antão +Praia - Santiago +Rabil - Boa Vista +Ribeira Brava - São Nicolau +Ribeira Grande - Santo Antão +Salamansa - São Vicente +Sal Rei - Boa Vista +Santa Maria - Sal +São Filipe - Fogo +São Miguel - Santiago +Cidade do Maio (Vila do Maio) - Maio +Cidade Nova Sintra (Vila Nova Sintra) - Brava + +Déegi +Cagarra - Santo Antão +Faveta - Santiago +Poilâo - Santiago +Salineiro - Santiago + +Yay +Viana (Deserto de Viana) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Melosuuf +Afrig +Kap Weer +1. Liig - Santiago gu Sowwu (Primeira Divisão de Santiago Sul): football (Kap Weer). + +2003 : CD Travadores +2004 : Académica da Praia +2005 : Sporting Clube da Praia +2006 : Sporting Clube da Praia +2007 : Sporting Clube da Praia +2008 : Sporting Clube da Praia +2009 : Académica da Praia +2010 : Sporting Clube da Praia +2011 : Boavista FC +2011-12 : Sporting Clube da Praia +2012-13 : Sporting Clube da Praia +2013-14 : Sporting Clube da Praia +2014-15 : Boavista FC +2015-16 : Desportivo da Praia +2016-17 : Sporting Clube da Praia +2017-18: Académica da Praia +2018-19 GDRC Celtic + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20141231042035/http://fcf.cv/pt/index.php/competicoes/campeonato-nacional +http://www.rsssf.com/tablesk/kaapvchamp.html + +Football +Santiago (Kap Weer) +Clube Desportivo Travadores benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Praia ci yu dunu Santiago. + +Campeonato Nacional (Kap Weert): 4 +1972, 1974, 1994, 1996 + +Liig Santiago/1. Liig - Santiago: +1959/60, 1965/66, 1967/68, 1971/72, 1973/74, 1993/94, 1995/961. Liig - Santiago gu sowwu: +2003 + +Staad + +Staad Várzea (''Estâdio da 'Várzea') + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + Tazinho + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + CD Travadores - Facebook + https://web.archive.org/web/20160201022259/http://www.scoreshelf.com/wmbb/en/Desportivo_Travadores + https://web.archive.org/web/20150924014404/http://www.foot-palmares.com/Fiches%20des%20clubs/Cap%20Vert/Fiche%20Desportivo%20Travadores.htm + +Santiago (Kap Weer) +Football + + +wolof + jollasu +baati wolof + +english + telephone, phone +baati wolof + +français + téléphone, phone +baati wolof + + +english + telephone, phone +baati wolof + +français + téléphone, phone +baati wolof +Cabeça dos Tarafes (Cabeça dos Tarrafes) benn dekk-dëkkaan Boa Vista ci yu sowwu yu dunu Boa Vista, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Boa Vista (Kap Weer) +1. Liig - São Vicente (Primeira Divisão de São Vicente): football (Kap Weer). + + 1936: CS Mindelense + 1937: Sporting São Vicente? + 1938: Sporting São Vicente + 1939: Sporting São Vicente/CS Mindelense? + 1940: CS Mindelense + 1941: CS Mindelense + 1942: CS Mindelense + 1943: CS Mindelense + 1944: GD Amarantes + 1945: GD Amarantes + 1946: CS Mindelense + 1947: CS Mindelense + 1948: Académica do Mindelo + 1949: GD Amarantes + 1950: CS Mindelense + 1951: CS Mindelense +1952: CS Mindelense +1953: Académica do Mindelo +1954: CS Mindelense +1955: CS Mindelense +1956: CS Mindelense +1957: CS Mindelense +1958: CS Mindelense +1959: CS Mindelense +1960: CS Mindelense +1961: GD Amarantes +1962: CS Mindelense +1963: Académica do Mindelo +1964: Académica do Mindelo + +1965: FC Derby +1966: CS Mindelense +1967: Académica do Mindelo +1968: CS Mindelense +1969: CS Mindelense +1970: CS Mindelense +1971: CS Mindelense +1972: Académica do Mindelo +1972/73 : GS Castilho +1973/74 : GS Castilho +1974/75 : CS Mindelense +1975/76 : CS Mindelense +1976/77 : CS Mindelense +1977/78 : CS Mindelense +1978/79 : CS Mindelense +1979/80 : CS Mindelense +1980/81 : CS Mindelense +1981/82 : CS Mindelense +1982/83 : FC Derby +1983/84 : FC Derby +1984/85 : FC Derby +1985/86 : FC Derby +1986/87 : Académica do Mindelo +1987/88 : CS Mindelense +1988/89 : CS Mindelense +1989/90 : CS Mindelense +1990/91 : não houve +1991/92 : CS Mindelense +1992/93 : CS Mindelense + +1993/94 : CS Mindelense +1994/95 : Académica do Mindelo +1995/96 : CS Mindelense +1996/97 : CS Mindelense +1997/98 : CS Mindelense +1998/99 : GD Amarantes +1999/00 : FC Derby +2000/01 : FC Derby +2001/02 : Batuque FC +2002/03 : Batuque FC +2003/04 : Académica do Mindelo +2004/05 : FC Derby +2005/06 : CS Mindelense +2006/07 : Académica do Mindelo +2007/08 : FC Derby +2008/09 : CS Mindelense +2009/10 : Batuque FC +2010/11 : CS Mindelense +2011/12 : Batuque FC +2011/12 : CS Mindelense +2011/12 : FC Derby +2012/13 : CS Mindelense +2013/14 : FC Derby +2014/15 : CS Mindelense +2015-16: CS Mindelense +2016-17 : CS Mindelense +2017-18: CS Mindelense +2018-19: CS Mindelense + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20150924011056/http://www.fcf.cv/pt/index.php/associacoes/sao-vicente +http://www.rsssf.com/tablesk/kaapvchamp.html + +Football +São Vicente (Kap Weert) +Blackburn Rovers F.C. (Blackburn Rovers Football Club) benn football club ci "Premier League" (Angale - Nguur-Yu-Bennoo) ci dekku Blackburn ci Lancashire. + +Premier League: +1994-95 + +Staad +Ewood Park + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Blackburn Rovers F.C. - Dalub web + +Nguur-Yu-Bennoo +Angale +Premier League +'Grémio Sportivo Castilho benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Mindelo ci yu dunu São Vicente. + +Campeonato Provincial (Kap Weert) (1953-1974):1 +1973 + +1. Liig - São Vicente: 9 +1972, 1973 + +Staad +Staad Adérito Sena (Estâdio Municipal Adérito Sena) + +Xool it + +Karmat ak delluwaay + +São Vicente (Kap Weert) +Football +Estádio Marcelo Leitão benn staad ci yu penku ye dekku Espargos ci yu dunu Sal ci Kap Weert. + +Football klubi +Académica do Sal +Académico do Aeroporto +Juventude (Sal) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + 1. Liig - Sal + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Sal (Kap Weert) +Staad +Stamford Bridge benn staad ci football club Chelsea F.C. ci ye Fulham, dekku Londar, Angale, Nguur-Yu-Bennoo). + +Nataal yi + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Premier League + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Chelsea F.C. - Dalub web + +Nguur-Yu-Bennoo +Angale +Staad +Texel mooy dunu réewum Olaand. + +Dun +Olaand +Garça de Cima benn dekk-dëkkaan Ribeira Grande ci yu dunu Santo Antão, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santo Antão (Kap Weert) +Waax bu Praia (wu-portigee: Porto da Praia, wu-kreyóol Kap-Wert: Purtu da Praia, wu-faraansi: Port de Praia, wu-angalteer: Port of Praia) ben waaxu mi ngi dunu Santiago, Kap Weer. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Teereekaay +Cabo Verde, viagem pela História das ilhas (Almeida, Germano; Lisboa: Caminho, 2003) +Cabo Verde, cruzamento do Atlântico Sul (Mindelo: Rádio Nova, 1998) + +Lëkkalekaay yu biti + +Waax bu Praia (Porto da Praia) - ENAPOR + +Waax +Santiago (Kap Weer) +Campeonato Nacional: football (Gine Bisaawóo). + +1975 : CF Os Balantas (Mansôa) +1976 : União Desportiva Internacional (Bisaawóo) +1977 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1978 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1980 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1981 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1982 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1983 : Sporting Bisaawóo +1984 : Sporting Bisaawóo +1985 : União Desportiva Internacional (Bisaawóo) +1986 : Sporting Bisaawóo +1986–87 : Sporting Bafataa +1987–88 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1988–89 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1989–90 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +1990–91 : Sporting Bisaawóo +1991–92 : Sporting Bisaawóo +1993 : SK Waaxi bu Bisaawóo (SC Portos de Bissau) +1993–94 : Sporting Bisaawóo +1996 : ADR Desportivo Mansabaa +1997 : Sporting Bisaawóo +1998 : Sporting Bisaawóo +2000 : Sporting Bisaawóo +2001 : no championship'' +2002 : Sporting Bisaawôo +2002–03 : União Desportiva Internacional (Bisaawóo) +2003–04 : Sporting Bisaawóo +2004–05 : Sporting Bisaawóóo +2005–06 : CF Os Balantas (Mansôa) +2006–07 : Sporting Bisaawóo +2007–08 : Sporting Bafataa +2008–09 : CF Os Balantas (Mansôa) +2009–10 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +2010–11 : AK Bisoraa +2013 : CF Os Balantas (Mansôa) +2014 : Nuno Tristão FC (Buula) +2015 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóo) +2016–17 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóóo) +2017–18 : Sport Bissau e Benfica (Bisaawóóo) +2018–19 : União Desportiva Internacional (Bisaawóo) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://footforpeoples.ucoz.org/index/guinea_bissau_league_teams/0-315 +http://www.rsssf.com/tablesg/gbischamp.html + +Football +Afrig +Sporting Clube Bisaawóo/Sporting Clube Gine Bisaawóo (wu-portigee: Sporting Clube de Bisaawóo) benn football club ci "Campeonato Nacional (Gine Bisaawóo)" ci dekku Bisaawóo. + +Ngori +Campeonato Nacional (Gine Bisaawóo): 13 + 1983, 1984, 1986, 1991, 1992, 1994, 1997, 1998, 2000, 2002, 2004, 2005, 2007 + +Staad + +Staad 24 Sattumbar (Estâdio Nacional 24 de Setembro) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + Dalub Web Sporting Bisaawóo +Sporting Bisaawóo - Soccerway +https://web.archive.org/web/20150722005220/http://scoreshelf.com/ggbb/en/Sporting_Clube_Bissau + +Football +Afrig +Staad 24 Sattumbar (wu-portigee: Estádio Nacional 24 de Setembro) benn staad ci ye dekku Bisaawóo ci yu diiwaan Bisaawóo ci Gine Bisaawóo. + +Football klubi +Benfica Bisaawóo +Inter Bisaawóo (UDIB) +SK Waaxi bu Bisaawóo (SC Portos de Bissau) +Sporting Bisaawóo + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Gine-Bisaawóo) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Gine Bisaawóo - World Stadiums + Staad 24 Sattumbar - World Stadiums + +Staad +Afrig +Mbàqnoos g garab la ci xeeti garab yi + +Garab +Campo Baixo benn dekk-dëkkaan Brava ci yu sowwu yu dunu Brava, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Teerekaay +Susanne Lipps, Oliver Breda: Reiseatlas Kapverdische Inseln. Hrsg.: Dumont. Dumont, Ostfildern 2005, ISBN 3-7701-5968-3, Dunu Brava, p. 153–156. + +Brava +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Waax bu Bisaawóo (wu-portigee: Porto de Bissau, wu-faraansi: Porte de Bissau, wu-angalteer: Port of Bissau) ben waaxu mi ngi Bisaawóo mi ngi sowwu ci Gine Bisaawóo. + +Nataal yi + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Waax +Afrig +Académica da Praia benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Praia ci yu dunu Santiago. + +Ngori +Campeonato Nacional (Kap Weert): +1965, 2018 + +Liig Santiago/1. Liig - Santiago: +1965, 1968, 19891. Liig - Santiago gu bëj-saluumu: +2004, 2009, 2017-18 + +Staad + +Staad Várzea (''Estâdio da 'Várzea') + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Campeonato Nacional (Kap Weer) + Luis Bastos + Caló + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Dalub Web gu Académica da Praia + +Santiago (Kap Weer) +Football +Primeira Liga: football (Portugaal). + +1934–35: Porto +1935–36: Benfica +1936–37: Benfica +1937–38: Benfica +1938–39: Porto +1939–40: Porto +1940–41: Sporting CP +1941–42: Benfica +1942–43: Benfica +1943–44: Sporting CP +1944–45: Benfica +1945–46: Belenenses +1946–47: Sporting CP +1947–48: Sporting CP +1948–49: Sporting CP +1949–50: Benfica +1950–51: Sporting CP +1951–52: Sporting CP +1952–53: Sporting CP +1953–54: Sporting CP +1954–55: Benfica +1955–56: Porto +1956–57: Benfica +1957–58: Sporting CP +1958–59: Porto +1959–60: Benfica +1960–61: Benfica +1961–62: Sporting CP +1962–63: Benfica +1963–64: Benfica +1964–65: Benfica +1965–66: Sporting CP +1966–67: Benfica +1967–68: Benfica +1968–69: Benfica +1969–70: Sporting CP +1970–71: Benfica +1971–72: Benfica +1972–73: Benfica +1973–74: Sporting CP +1974–75: Benfica +1975–76: Benfica +1976–77: Benfica +1977–78: Porto +1978–79: Porto +1979–80: Sporting CP +1980–81" Benfica +1981–82: Sporting CP +1982–83: Benfica +1983–84: Benfica +1984–85: Porto +1985–86: Porto +1986–87: Benfica +1987–88: Porto +1988–89: Benfica +1989–90: Porto +1990–91: Benfica +1991–92: Porto +1992–93: Porto +1993–94: Benfica +1994–95: Porto +1995–96: Porto +1996–97: Porto +1997–98: Porto +1998–99: Porto +1999–2000: Sporting CP +2000–01: Boavista +2001–02: Sporting CP +2002–03: Porto +2003–04: Porto +2004–05: Benfica +2005–06: Porto +2006–07: Porto +2007–08: Porto +2008–09: Porto +2009–10: Benfica +2010–11: Porto +2011–12: Porto +2012–13: Porto +2013–14: Benfica +2014–15: Benfica +2015–16: Benfica +2016–17: Benfica +2017–18: Porto +2018–19: Benfica + +Xool it +Football + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.uefa.com/memberassociations/association=por/domesticleague/index.html +http://www.lpfp.pt/documentacao/pages/regulamentos.aspx +http://www.lpfp.pt/liga_zon_sagres/pages/estatisticas.aspx +http://www.rsssf.com/tablesp/portchamp.html +http://www.sofascore.com/standings/football/portugal/primeira-liga/52 + +Football +S.L. Benfica (wu-portigee: Sport Lisboa e Benfica (Sport Lisboon gu Benfica (Benfika?))) benn football club ci "Primeira Liga" (Portugaal) ci dekku Lisbon ci diwaanu Lisboon. + +Primeira Liga, Portugaal: 37 +1935–36, 1936–37, 1937–38, 1941–42, 1942–43, 1944–45, 1949–50, 1954–55, 1956–57, 1959–60, 1960–61, 1962–63, 1963–64, 1964–65, 1966–67, 1967–68, 1968–69, 1970–71, 1971–72, 1972–73, 1974–75, 1975–76, 1976–77, 1980–81, 1982–83, 1983–84, 1986–86, 1988–89, 1990–91, 1993–94, 2004–05, 2009–10, 2013–14, 2014–15, 2015–16, 2016–17, 2018–19 + +Staad +Staadi Woyof/SL Benfica (Estâdio Sport Lisboa e Benfica, Estâdio da Luz) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Primeira Liga + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + + S.L. Benfica - Dalub web + +Football +Portugaal +Sporting Clube Bisaawóo/Sporting Clube Gine Bisaawóo (wu-portigee: Sporting Clube de Bisaawóo) benn football club ci "Campeonato Nacional (Gine Bisaawóo)" ci dekku Bisaawóo. + +Ngori +Campeonato Nacional (Gine Bisaawóo): 12 + 1977, 1978, 1980, 1981, 1982, 1988, 1989, 1990, 2010, 2015, 2017, 2018 + +Taça Nacional da Guiné Bissau: 7 + 1980, 1989, 1992, 2008, 2009, 2010, 2015 + +Staad + +Staad 24 Sattumbar (Estâdio Nacional 24 de Setembro) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Dalub Web Benfica Bisaawóo + +Football +Afrig +Yoos bisaaw: + +garab gii lañuy wax ci Wolof Yoos bisaaw turu xam-xam wi moom lañuy wax (Agave sisalana) moom daf a bokk ci xeeti (Agaaf) yi bu ko defe dañuy jëfandikoo baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle ak yaneen (Agaaf) yi ndax xeetu garab yu ñuy wax (Agaaf) daf a bari lool te ci xeetu garab yuy am ci wetu (Amerig) lay doon mu doon xeet yu bari moom nag ñu di ko ràññatle mu bokk ci njabootu (Agaaf) yi waaye ñu jël baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle turu xam-xamam nag mooy (Agaaf sisallnaa) moom nag garab la goo xam ni ci xeeti (Agaafl yi la bokk kon baatu (Sisaal) lañuy jël di ko jëfandiko ngir ràññatle ko ak yaneen garab yi nga xam ne (Agaaf) lañ, +Moom nag fimuy faral di sax réew yu ñuy tudde (Karayibil) fu de me ni (Panamaa) ak (Kubã) ak fu de me ni (Jamayg) réew yooyu fala baree lum fay sax leg lee ñu gis ko faneen waaye foofu la ëpp lum fay sax mi ngi faral it di sax ci barab yi nga xam ni dafa nooy te di faral di tàng foofu la ëpp lumuy sax kon ñi ngi koy faral di gis ci réewu (Karayibi) añs kom ni ma ko waxe. + +Melo wi + +Moom nag garab la goo xam ne day am ab dàtt boo xam ne dàtt bu xaw a dëgar lay doon day bindoo ni dàttu tàndarma day gàtt it waaye dafay am ker goo xam ni ker gu yaatu lay doon gu rëy ker gi it dafay dëll ndax li tax muy dëll mooy xobam yu mu am dafay xob yu tal xob yu tal yoo xam ne daf a xaw a rëy daf a xaw a yaatu su ko defee xob yooyu nuñuy ràbb a loo wee moo tax ker gi dafay xaw a yaatu doonte moom garab la goo xam ne du gudd lool waaye dafay dëll ker gi it dafay yaatu moom nag nimuy saxe dafa mel ni dafa am ay xupptali-xupptal ni ki ni tàndarma di saxe noonu lay saxe ba noppi day sax ay xob mu wër xëb yoy dafay yor melokaanu ab daba ni daba di bindoo noonu lay bindoo, +Boo xoolee xob yi ci wed gi dafay mel ni dafay am ay bëñ yu mel ni ay bëñ i joolaa la am xob yi noon la mel ba noppi dafay xaw a ràbbaloo nga xam ni dafay sax ni tàndarma di saxe bu saxee day yëkkatiku wëraat amaat yaneen yu saxaat yoo xam ni dañuy teglaanto kom ay xuppatal yu teglaanto noonu lay doon guddaayam dan a toll ci met jàpp ñaar-fukki met ak sàtti met ak juróom. + +Nataal + +Turu xam-xam wi +Agave sisalana + + garab + garab +Monte Largo benn dekk-dëkkaan São Filipe ci yu bëj-saluumu yu dunu Fogo, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Fogo (Kap Weert) +Institut Mozdahir International (IMI) ag mbootaay gu tënkuwul ci nguur la te jubluwaayam du wut xaalis. Seriif Mohammed Aali Aydaar (Cherif Mohamed Aly Aidara) moo ko taxawal te màkkaan mi nekk ci Ndakaaru. IMI am na këyit guy yoonal nekkam ag mbootaay gu tënkuwul ci nguur te wër na àddina si ba teew ci réew yu bari ci tund wii, ñu man cee lim Senegaal, Kodiwaar, Mali, Gine Bisaawóo...ak ñoom seen. + +Teew na ci fukk ak ñaari (12) réew, te di yëngu ci fànn yu bari yu mel ne suqaliku gu sax gu sofu ci fànni wëppa ak lef yii: njàng mi, Lóofóon gu xereñ, wergi-yaram, lootaabiinu askan, mbatiit, mbay mi, yasarag jant bi, dëkkuwaay, njurtéef, leble, yoriin wu jub wu koomum kéew mi, njëmbat garab ak naatalaat àll bi. + +Ñi mu ci lëngool +Mbootaay gi nag sampu na bu baax ci Senegaal ak it ci Afrig sowwu jant ginnaaw bi mu fi amee sañ-sañub nekk fi ak këyit yi koy firndeel. + +Jamono jii am na junni-junniy nit yu ci bokk te nekk fépp ci àddina si. + +Ci yoon wi mu jël itam, IMI daf ciy lëngoo ak nguur yi jaare ko ci seen i jëwriñ ak gox-goxaan yi (sàmmkati ndox mi ak àll yi, mbay mi, saytukati kaaraangeg dund bi, njëwriñi jagle yi, calaw yi...), SGBS, mbootaayi àddina bi (Sémbuw dund bi ci àddina bi: Programme Alimentaire Mondial) ak kuréel yi (ANEV: Agence Nationale des éco-village, Association des Voûte Nubienne) ak ñeneen ñu bari. + +Xët yi mu lëkkalool +Sëriif Muhammed Aali Aydara + +Téerekaay + +Lëkkalekaay yu biti +Mozdahir + +Lislaam +Sëriif Muhammed Aali Aydara (Chérif Mohamed Aly Aïdara) mi ngi judd atum 1959 ca Daaru Hijratu (dëkk bu baayam sancoom, Sëriif Ahasan Aydara). Doomi Maymuna Jaw (moom soxna si doom ci Sëydu Jaw nekkoon seef de kantoŋ) ak Sëriif Alhasan Aydara, cosaanoo Gànnaar, bokk ci askanu Laxlal (Laghlal) ñu gën koo xam ci Ahlu sëriif laxlal di càllalag Sëriif Mulaay Idriisa, mi sos nguurug Idriisa yi, càllala gu dem ba ci Asan doomi Aali ak Faatima doomi Yónnent Yàlla Muhammed ak (JNCM). + +Moo nag doomi Senegaal ak Gànnaar la. + +Doon na wax ak a binde làkku yu bari niki Àngale, Araab, Farãse, Pël, ak Wolof. + +Liggeeyam + +Kilifa diine ci dayoom, Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy soskat ak njaatigel Mbootaayu IMI ak it rajo "Mozdahir FM" ci Ndakaaru ak rajo "Zahra FM" ca Koldaa. + +Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy xalifab mboolem Siyit "Mozdahir" yi nekk ci Afrig ak ci àddina si. + +Ay mbindam ci Xam-xam +Bind na ci fànn yu bari yu ci mel ne xam-xamu Islaam, dundug Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ci moom) ak 12i imaam yu mat sëkk yu kër Yónnent bi, Ahlul bayti (jàmm ak ngëneel ci ñoom). Ay téereem yu bari siiwalees na ko, ñu man cee lim: + +Dëgg yi ci kuutlaayal Yónnent bi (Les Vérités de La Succession du Prophète) +Imaam Useynu (YYY) martiir ak xettalikatu Islaam (L’Imam Hussein (AS) martyr et sauveur de l’islam) +Sayyidaa Saynab (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) waadaanu Karbalaa (Sayyidda Zaynab (paix et salut sur elle) l'héroïne de Karbala) +Jullig Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) bunu sukkandikoo ci ag njabootam (La prière du Prophète Mouhammad (PSLF) selon les membres de sa famille) +Ghadir Khoum +Tamxarit, bisub naqar walla bisub mbég? (Achoura jour de deuil ou jour de fête ?) +Sàrti koppar gi ci Islaam (Principes de la finance islamique) + +Téerekaay + + APPEL Chérif Mohamed Ali Aïdara, guide des chiites : «Partout dans le monde, les musulmans sont opprimés». Le Quotidien. + Le chiisme au Sénégal Mozdahir. Shia Africa. + cherif mohamed aly aidara, grand maître au service du peuple et quelques dignitaires Congolais. Daily Motion. + Chérif Mohamed Aly Aïdara, guide des chiites du Sénégal « Unis, les guides religieux peuvent combattre le terrorisme au Sénégal». Kolda News. + Institut Mozdahir International. + Sénégal : 127 jeunes de Vélingara s’informent sur l’islam chiite. Shafaqna. + Chérif Mohamed Aly Aidara, président de Mozdahir International : « L’islam ne peut pas être une religion de violence ». Seneweb. + Qui est Cherif Mohamed Aly Aidara. Scribd. + Les pressions faites sur notre communauté ne nous ébranlent point. Enquete Plus. + Progression du chiisme en Afrique, une donnée qui peut modifier les équilibres géopolitiques. Aleteia. + Inaugurantion d'une mosquée construite par l’Institut Mozdahir International : Le khalife de Médina Gounass bénit les actions de l’Ong chiite. Leral. + PORTRAIT – Chérif Aïdara, guide des Chiites : Globe trotter. Le Quotidien. + +Niti senegaal +F.C. Porto (Futebol Clube do Porto)) benn football club ci "Primeira Liga" (Portugaal) ci dekku Lisbon ci diwaanu Lisboon. + +Primeira Liga, Portugaal: 30 +1934–35, 1938–39, 1939–40, 1955–56, 1958–59, 1977–78, 1978–79, 1984–85, 1985–86, 1987–88, 1989–90, 1991–92, 1992–93, 1994–95, 1995–96, 1996–97, 1997–98, 1998–99, 2002–03, 2003–04, 2005–06, 2006–07, 2007–08, 2008–09, 2010–11, 2011–12. 2012–13, 2017–18, 2019-20, 2021-22 + +Staad +Staad Dragão (Estádio do Dragão) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Primeira Liga + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Football +Portugaal +Associação Académica do Mindelo benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Mindelo ci yu dunu São Vicente. + +Ngori +Campeonato Nacional (Kap Weert): 3 +1952-1953, 1966-1967, 1989 + +1. Liig - São Vicente: 10 +1948, 1953, 1963, 1964, 1967, 1972, 1986/87. 1994/95, 2003/04, 2006/07 + +Staad +Staad Adérito Sena (Estâdio Municipal Adérito Sena) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Carlos Alhinho + Sténio dos Santos + Romy (Ramos da Graca) + Toy Adão + +Karmat ak delluwaay + +São Vicente (Kap Weert) +Football +1. Liig - Santiago gu bëj-gannar (Primeira Divisão de Santiago Norte): football (Kap Weer). + +2000 : Barcelona (Tarrafal) +2001 : não disputado +2002 : Desportivo de Santa Cruz +2003 : Barcelona (Tarrafal) +2004 : Estrela dos Amadores (Tarrafal) +2005 : Flor Jovem da Calheta +2006 : não disputado +2007 : Scorpion Vermelho +2008 : Scorpion Vermelho +2009 : Estrela dos Amadores +2010 : Scorpion Vermelho +2011 : Benfica de Santa Cruz +2012 : Estrela dos Amadores +2013 : Scorpion Vermelho +2014 : Grémio Nhágar +2015 : Beira-Mar (Tarrafal) +2015-16: Varandinha +2016-17: AJAC +2017-18: Scorpion Vermelho +2018-19: GD Varandinha +2019–20: Não disputado + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +http://www.fcf.cv/pt/index.php/associacoes/santiago-norte +http://www.rsssf.com/tablesk/kaapvchamp.html + +Football +Santiago (Kap Weer) +Seex Muhammadu Lamiin Baara, ñu gën koo xam ci Sëriñ Baara Mbàkke Fàllu! + +Ganeem àdduna +Mi ngi gane àdduna Ndindi ci atum 1921. +Ay wayjuram : +Seex Muhammadul Faadal Mbàkke ak Soxna Xari Sàll. + +Am njàngam +Sëriñ Fàllu moo ko dalal jàng ginnaaw ñu jox ko S Moor Sàññe mu jàngal ko bamu sori 1928 la ko Sëriñ Baara moom Sëriñ Tuubaa minu ko tudde jël yóbbu ko ci ku ñiy wax Sëriñ Móodu Amar mu àggaleel ko alxuraan ji, ginnaaw loolu la Sëñ Baara génn àdduna mu dellusiwaat ci Sëriñ Fàllu mu yabal ko Jaamal mu jànge fa xam-xam ca Sëñ Jaamal Siise, bokk na ci liy wan xam-xamam bu yaatu lumu jangoon da ko daan mokkal. +Sëriñ Siidi Maxtaar ka nee na toog na muy tari. “Maqaama Al hariirii” ne ko lii dama koo mokkaloon bamiy jàng! +Xel mi neexoon lool daan na wax ay lakk yu bari te wuute araab farañse angale ak yu ni mel, nekkoon nit ku man a takk daawul fàtte. + +Sëriñ Baara nekkoon ku bëgg Sëriñ Fàllu te déggaloon ko lumu am jox ko lumu am tudde ko ba tuddee na ko ci njabootam ab lim bu bari tabaaràkkal laah, +fonk ay magam Sëriñ móodu miy magam noonu la ko bëgge woon topp ko daawul juuyoo ak moom ci dara daawul xëccoo ak moom dara bàyyee ko boppam bam jeex takk. +Sëriñ Móodu daa na wax naan kenn rekk laa xam ci kuma gën a bëgg sëriñ Fàllu mooy sëriñ Baara! + +Ag xilaafaam: +Muy sët bi njëkk a wuutu Sëriñ Tuubaa ci jamono ji nit ñi miinoon lool doomi Sëriñ Tuubaa Sëriñ Tuubaa Baara ñëw ca yar ba ak jikko ju rafet ja ak man a xajoo ga ak man a yaatal ga ak ubbiku ga xam ne fimu nekk dug moomeel waaye ab liggéey la bu népp bokk du yëfi kenn. +Mu dox doxiin woowu ba jaar fu kenn foogul liggéey fi loo xam ne toogaayub juróom fukki at lay niru. +Ay jëfam Tuubaa liggéey na fi liggéey bu yaatu pecci yi wër kër njabotug Sëriñ bi yépp defar na ko def fa ay yoon, fu ndox mànki mu yóbbu ba ci biir dëkk bi sax, ñu bari ci ag nekkam lañu am kër, soxla soo ko wax bu dee luñu man a joxe mu joxe ko bu dee luñu war a lijanti mu lijanti ko daar-daar, andi waat ñu bari ci yoon wi jox leen seen wàccuwaay, +nos dëkk bi ku ne mu am lumu la jox ci dëkk bi ngir nosiin wi rafet ak doxiin wi, +màggal gi mu yaatal ko bitim réew ak fépp ak biir réew mi ak waxtaan yu am solo ngir tissaare wooteb sëriñ Tuubaa wi. +Nekkoon gu bëgg bennoog jullit yi, dem seet i ay mbokk i diineem yu bari daan leen nemmiku, +Sëriñ Baara nekkoon nit ku woyof daawul xeeb kenn, nekkoon nit ku neex a jot di wax ak ñépp di déglu ñépp, bamu nekk a gul xalifa ak bi mu nekkee xalifa daraam soppikuwul, ña mu daan seet i lay seet i, ña mu xamoon beddiwu leen di tudd i doom di dem sarax di seet i ku tawat, màggal yépp la daan dem. +Deful woon yëff yi yëfi kër, waaye yëfi ñépp la ko defoon, +bëgg ay rakkam def leen ni boppam , dëddu woon àdduna lool man a jaamu Yàlla lool fonku julli lool bokk na ci ñi ëpp lunu julli ci jumaay Tuubaa ak lumu metti ci moom di xaritu ñépp. +Sëriñ Baara nekkoon koo xam ne ku daan jàppale ndaw yi, dileen taxawu ci seen njàng ak seen liggéey. Sëriñ Baara amoon gëm-gëmu jiital ndaw yi ci lépp xam ne ñooy yaakaari ëllëg yi, mu teel leen a jiital, +Mu nekkoon nit ku man a jaamu Yàlla daawul nelaw guddi wird ak déeyaaleg boroomam la daan fanaane, + +Diganteem ak nitu nguur yi: + +Sëriñ Baara daan na jëflante ak nitu nguur yi ci jëflante bu rafet te lépp lu ko laloon mooy jotalileen lépp luy ñjariñal nit ñi, teewul nag, moom daa mas a gëm ne fii lépp lu fi nekk rekk, taalibe Sëriñ Tuubaa yi ñoo ko fi def! !!! Loo fi gis ñoom la ladaan wax, kon masul sàkku ci ñoom dara lu dul ne, daa nekk loo xam ne njariñal nit ñi la. Nitu nguur yi itam yabuñu ko woon, ngir dëggoom ak pass-pass bu dëgër ba ci Sëriñ Tuubaa ak fulla ji nekkoon ci moom. + +Sëriñ Baara ak aji màkka: Dem na màkka lu ëpp ñent fukki yoon, yóbb na fa nit ñu dul jeex, att mu nekk dadaan yóbb nit ñu bari, sëriñ Baara yoroon jikkoy sëriñ Fàllu, nekk nit ku woyof te bari njariñ daan dimbali ñépp, di nit ku ubbiku, ku baax te bariwoon jàmm, tabe lool am xorom lool, yéene ji kawe lool, pasteef bi ak taalube gi foo ko takk weesu na ko Yàlla nanu ko Yàlla fayal. + +Sëriñ Baara bàyyi koo na fi wuyji boroomam ci attum 1431, 18 rajab + +nitu diine +Koronaawiris 2019 (COVID-19) Jàngoro la buy wàlle saa su nitt ku mu dal jege ñeneeni +nitt. Jàngoro ji li key ubbil buntu ci ab doomu aadama mooy mu jege ku feebar, walla mu +tekk loxoom fu ku feebar jotoon a laal ba pare dàldi laal at bëtam, walla bakkanam walla +gémminñam. Li ci ëpp, wiris bi li koy tasaare moodi tox-tox yiy juge ci tissóóli ak sëqëtu +ku mu wàll ba pare. Képp koo xamantene yaa ngi jege ku feebar bi w��ll, muy tissóóli +mbaa di sëqët te sori wu loo ko lu ëpp ñaari meetar, li gën woor mooy di na la wàll. +Neneen nu la wiris bi mënees wàll mooy nga laal fu mu teggu ba noppi, raxasuloo sey +yoxo ak saabu, ba pare nga laal sey gët, sa nopp walla sa bakkan. + +Ndoorte +Jàngoro ji Wuhan, capitaalu Hubei ca Chine, la njëkk feeñ bi atum 2019 di door tàmbale. +Diggënte boobu ak léégi, wiris bi law na ci aduna ci yëpp. Ba tax na OMS, bisu 11 mars +2020, diggele ñu jappee Koronaawiris ab pandemie. Pandemi doon feebar boo +xamantene da fa tasaaro bu baax ci aduna ci yëpp. Rééw yi feebar bi gën sonnal, ñi mu +fa rey bari neñ tek ci seeni dispañseer ak loppitaal li ñu leen yan ci ay ñu tawat dootu ñu +ko àttan. Njiitu OMS, Dr. Tedros Adhanom Ghebreyesus, wax na ni “lii du mbirum wér gu +yaram doŋŋ, ndax bépp xeetu liggééyukaay da na ko yég moo tax it ñëpp a war a japp ci +xeex mi. + +Màndargay feebar bi ak pac-mi +Bokk na ci Màndargay Jàngorooy Koronaawiris sëqat, xeetu sibbiru, sonn ak xiixët. Léé- +léé ki feebar am metitu yaram, baqata yuy tuuru, biir buy daw, metitu boli, metitu naq ak it dara dootu ko xeeñ. Ñi koronaawiris wàll, ci diggënte ñaar ak fukk-ak-ñenti fan la ñuy +key tàmbale yég, waaye ñi ci ëpp, bu weeso fukki fan ley tàmbale feeñ. Ñu bare nak +feebar bi di na leen dal te du metti noonu. Ña feebar bi sonnal dëgg lée-lée ñu jëlé ci +Pneumonie, mu yàq seeni xëtër, seeni xol, ak yeneen. Ña feebar bi sonnal li leen war +mooy ñu teela jublu ci doktoor. + +Nit mun naa am jàngoro ji te lenn du ko fesal, du metit bu muy yég, du lu ñi ko jege mën +tek bët. Loolu la ñu naan "asymptomatique". Waaye ña feebar bi wàll te yégu ñu ko, ña +"asymptomatique", mëness ne ñu wàll jàngoro ji képp ku leen jege. Loolu moo waral +jàngoro ji gaaw law ci àdduna. + +Doktoor yi bu ñuy seet ndax jàngoro ji mi ngi ci nit, ca baqata ya leñuy key seet. Beneen +pexe buy firnde ndax nit ki da fa am jàngoro ji am déét mooy seet bu ñu naan “CT-scan”. +Kéép ku ñu gis ne am na jàngoro ji, nañu ko yobbu loppital mu beru ku dul fackat du ko +jege. Dëgg la garabu koronaawiris amagul waaye ña ëpp ci ñi muy dal bu leen doctoor +taxawoo di ne ñu wér. + +Fagaru +Guir wañi jangâro-ji dañu wara sorenté suñu biir, wañi dèm berep you fess ak nit. Kouy guène si biti, dafa wara sol mask bouy fate bakanam ak guèmem teksi "gant". Nit ñi dañu si wara bolé-di raxass sen loxo ak sabou ndir 20 simili, aye yoni yone. Ño gui wax nit ni ñu moyou di lal sen kanam ak seni loxo. + +Yeneeni Leeral +Poson Kayit bi ñuy raññee poson bi ñu duppe (Estewaad + +Estewaad) moy poson bi ñu jëfëndikoo ci ndoorteeli pomp mi ba 20 fàn ak juroom ci wéeru Ut Sax yi ko tax a jog mooy yii lékk tontòor yi ak doomi sàpp yi te ñu gën ci raññe (Eliyotis, Eyariyas), Diparopsis walla yiy lekk xòb yi (Espodoptera) + +Nii  la ñu koy jëfëndikoo : + +Bidoq (Estewaad) mooy pomp ñeenti buumu sàpp + +Su dee ñaari buum la ñuy pomp : + +Jëlal ndox mu set sotti ko ci bidoq bu mag bi ba mu diggu doomu + +Poson bi nekk ci bidoq bi jël ci génn wàll gi (xoolal fi ñu ko màndargale) sotti ko ci bidoq bu mag bi + +Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay feccali bidon bu mag bi. Njaaxas juroomi liitar la wara doon. Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp. + +Su dee bénn buum la ñuy pomp + +Sottil ndox bi ci ñeenteelu xaaju bidoq bu magg bi ; + +Jëlal nak ñeenteelu xaaju bidoq  poson bi (baayil sa xel ci màndarga bi koy wone). Yengalal bu baax njaaxas bi balaa ngay dolli ndox ba ci xaaju bidoq bu magg bi.  Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp. + +Ak poson bi ñu duppe Estewaad, diggante pomp ak pomp 10 fànn ak ñeent la + +Na ka la poson bi di xeexee ak sax yi + +Ñaari ba ñeenti waxtu gannaaw ba nga pompee, sax yi dootuñu mën a yënngetu te dootuñu + +lékk itam. La cay tegu mooy ñu dee. + +Noonu  muy def  sax yi nak du ko def xaaritu baykat bi yi demee ni yàmb yi ak meelentaan yi + +Kayit bi ñuy raññe poson bi ñu duppe Tiriyoonf + +Tiriyoonf moom la ñuy jëfëndikoo ngir aar sàpp mi li ko dooree ci 20 fànn ak juroom mbénn ba ca njeexteel pomp mi. + +Sax yi ko taxa jóg mooy yiy lekk tontòor yi ak doomi sàpp mi te ñu gënn ci raññee Eliyotis, Eariyas, Diparopsis walla yiy lekk xòb yi (Espodoptera). Mën na xeex itam Piisroq ak weññ yu weex yi (Bemisiya) + +Naka la ñuy jëfëndinkoo Tiriyoonf + +Bidoq Tiriyoonf moom la ñuy pompee fukk i buum ak juroom bénn (maanam ñeenti ektaar) + +Su dee ñaari buum la ñuy pomp + +Duyàl bidoq bu magg bi ba mu fees ak ndox mu set + +Xaajal bidoq poson bi juroom ñet xaaj. Jëlal bénn xaaj sotti ko ci  bidoq bu mag bi. (Ngiir yombalal natt gi, jëlal nattukaay bu mag bi bi ñuy duppe doset, tëyéko ak so loxo  ndey jòor te sotti ci  poson bi ba mu egg ci ñennteelu rëd bi). Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay feccali bidoq bu mag bi ak ndox (njaxas mi juroomi liitar la wara doon) + +Boo bu natt mooy pomp ñaari buum + +Su dee bénn buum la ñuy pomp + +Duyàl bidoq bu mag bi ak ndox mu set ba mu diggi doomu + +Xaajal poson bi fukki xaaj ak juroom mbénn. Jëlal bénn xaaj sotti ko ci bidoq bu mag bi. (Ngiir yombalal natt gi, jëlal nattukay bu mag bi ñuy duppe doset, tëyeko ak sa loxo ndey jòor te sotti ci  poson bi ba mu egg ci ñaareelu red bi). Yëngalal bu baax njaxas mi bala ngay dolli  ndox ba ci xaaju bidoq bu mag bi (foofu mooy mengoo ak  ñaari liitar ak génnwall) .  Boo bu nàtt mooy pomp buumu sàpp. + +Ak poson bi ñu duppe Tiriyoonf, diggante pomp ak pomp 10 fànn la + +Naka la poson bi di xeexe ak sax yi + +Ci diir bu gàtt gannaw ba nga pompee, sax yi dootuñu mën a dem. La cay tegu mooy ñu dee. +Ceeb u jën di lekk gu siiw ca Senegaal, ñu ëpp ca aw askanam di ko jëfëndikoo waxtuw añ. +Grémio Desportivo Amarante benn football club ci "Campeonato Nacional de Futebol" (Kap Weer) ci dekku Mindelo ci yu dunu São Vicente + +Campeonato Nacional (Kap Weert): 1 +1998/99 + +1. Liig - São Vicente: 5 +1944, 1945, 1949, 1961, 1998/99 + +Staad +Staad Adérito Sena (Estâdio Municipal Adérito Sena) + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Sócrates Oliveira Fonseca + Almara + Armandim + +Karmat ak delluwaay + +São Vicente (Kap Weert) +Football +Sporting CP (Sporting Clube de Portugal, Sporting Lisbon)) benn football club ci "Primeira Liga" (Portugaal) ci dekku Lisbon ci diwaanu Lisboon. + +Primeira Liga, Portugaal: 18 +1940–41, 1943–44, 1946–47, 1947–48, 1948–49, 1950–51, 1951–52, 1952–53, 1953–54, 1957–58, 1961–62, 1965–66, 1969–70, 1973–74, 1979–80, 1981–82, 1999–2000, 2001–02 + +Staad +Staad José Alvalade + +Xool it + +Jukki yi ci lonku + Primeira Liga + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + +Football +Portugaal +1. Liig - Sal (Primeira Divisão do Sal): football (Kap Weer). + +1976: FC Juventude +1979/80 : 'Sport Clube Verdun +1980-83: Não houve +1983/84: Académica do Sal +1984/85 : Palmeira +1985/86 : Académico do Aeroporto +1986/87 : Sport Clube Santa Maria +1987/88 : Académico do Aeroporto +1988-92 : Sport Clube Santa Maria +1992/93 : Associação Académica do Sal +1993/94 : Associação Académica do Sal +1994/95 : Académico do Aeroporto +1995/96 : Associação Académica do Sal +1996/97 : Sport Clube Santa Maria +1997/98 :' Sport Clube Santa Maria +1998/99 : Juventude (Sal) +1999/00 : Palmeira +2000/01 : Associação Académica do Sal +2001/02 : Académico do Aeroporto +2002/03 : Académico do Aeroporto +2003/04 : Académico do Aeroporto +2004/05 : Associação Académica do Sal +2005/06 : Académico do Aeroporto +2006/07 : Académico do Aeroporto +2007/08 : Académico do Aeroporto +2008/09 : Sport Clube Santa Maria +2009/10 : Académico do Aeroporto +2010/11 : Académico do Aeroporto +2011/12 : FC Juventude +2012/13 : Académico do Aeroporto +2013/14 : Sport Clube Verdun +2014/15 : Académico do Aeroporto +2015/16 : Académico do Aeroporto +2016/17 : Académico do Aeroporto +2017-18: Palmeira de Santa Maria +2018-19: GD Oásis Atlântico (Santa Maria) + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti +https://web.archive.org/web/20150924011034/http://www.fcf.cv/pt/index.php/associacoes/sal +http://www.rsssf.com/tablesk/kaapvchamp.html#sal + +Football +Sal (Kap Weert) +Principal/Ribeira Principal benn dekk-dëkkaan São Miguel ci yu dunu Santiago, Kap Weer. + +Karmat ak delluwaay + +Dekk-dëkkaani Kap Weer +Santiago (Kap Weer) +Veliko Tarnovo mooy péeyu réewum Bulgaari(1185-1393). + +Bulgaari + + +Li ko andi +Ay at ci gannaaw, setluwoon nanu ci aduna bi yep mbas mu tudd "grippe". Mbass yi ci doomu jangoro yu bayeko ci  gripp u mala lanu jogge gannaaw banu nekke ci jawu ji ci ay mala yu melni picc wala ay "mamifere" yu am infection. Yennsaay doomu jangoro yu mala yi danuy soppeku nekk ay doomu jangoro yu nit gannaaw loolu walante am ci diggante nit ak nit. Infection "zoonotiques" lanu leen di woowe ndax ci mala lanu jogge. Wallu sorri wante nu gen ko xam ci sorri wante nit ak nit njariñam mooy mbass u gripp  bu mel ni Korona  du law torop.Sorri wante digaante nit ak nit mooy fexe baña jeggeyanto nit ku nek, nekk ci been weet bu dee dangeen di waxtan wala sax moytu dajalo ci yenn bereb yi di faral am mbolo say yo ko mene. Jeff Kwong fajj kat bu xam xamam macc ci wallu jangoro yu nit di am gannaaw infection mungi nekk ci benn dara ju mag ju nekk ci Toronto neena sorriwante bi mooy li nit yi wara def ngir mena mucc ci jangoro ji wante du berr nit ki. Nit yi sen xam xam macc ci wallu wergu yaram ci jamonoy mbass mi danu yokk di genna safonte ak seeni xarit wante itam ak seeni am di jam yi leen genna jegge. Pur xam najriñu sorriwante diggante nit ak nit, dañuy tambali wane benn natal u jangat mbass mi kangam yi ngank feebar yi di wallate ñoo ko amal. Ci natal bi jangatu mbassum Korona atum juni ak fukk juroom ñint jem ba ci atum ñaari juni ak ñaari fukk bi ñu nekk ni te jexagul. Dañuy tambali ak jangat yiñu amal ci reewum Chine bi nga xamantani foofu la mbas mi doore gannaaw loolu ñu xol naka la mbassum COVID-19 di lawee ci Afrique du Sud dafay tax bañu xam njariñu sorriwante diggante nit ak nit ci wallu fagaru ak itam ci naka lanu mene  jamarlo ak mbassum COVID-19 mi ba du epp loxo. Dinañu jeexal gestu bii jem ci wallu mbass mi ak benn saytu pur wax naka lañu menna def pur mooytu jafejafe yu bon yi nit ki menna am ndax sorriwante bi am diggante nit ak nit wante itam naka lañu menna def pur jamarlo ak moom ba genn ci ak jamm. + +Plang bunu rañee ci wallu mbass +Mbas yu mel ni Korona dañuy faral di law ci ñeet anam. Anam yooyu moom lanu wane  fii ci suuf. Fajj kat yi seen xam xam macc ci feebar yi di walle wane nañu fii ci suuf ñeeti pacc yi ñu jangat jem le ko ci mbass mi. Jangat bi li muy wane mooy  benn natal u limu ñi am feebar yi di walle ak itam gaaw gi mu gaaw ci wallu wallate ci ay giir. + + Pacc bu njek bi mungi am ci njelben u jangat bi. Bunu jele ci missaal gaawayu walate mbass u COVID-19 bi, danuy giss ni mooy wane njelben u walate febaar bi te amagulwoon nit yu berri yu ko am. + Pacc ñaarel bi, mungi jem ci wallu walante bi am ci dekkuwaay yi te xamulo ku la wall. Ci jamono bi la wallante diggante nit ak nit di genna law ndax nit yu berri yi am doomu jangoro bi. Ci pacc bi danuy setlu ni nit yi am doomu jangoro bi danuy gen di yokk bess bu nekk te loolu dafay galankor liggey bi nu wara def pur xeex doomu jangoro bi. Gannaaw ba kurel bi nu denk wallu wergu yaram ci aduna bi yep joxe ay ndogal pur bayi demalante digante rew ak rew ci aduna bi yep, njitu rew yi ci aduna bi yep jel nanu ndogal pur tej seeni rew rawatina rew yi genna am mbass mi tek ci itam wañi ndajee nit ci bereb yi di faral di am nit. Terelin yi rew u aduna bi yep tenk ci wallu wergu yaram, benn bankas la boo xamantani sen xam xam dafa macc ci wallu yoon ki ko soss mooy kurek gi tenk wallu wergu yaram ci aduna bi yep pur men soñ wante itam tek loxo ci feebar yi nga xam ni danuy faral di nekk ci bereb yi nt yi di daje lu berri laata  ñuy law ci diggante rew yu aduna bi yep. Ci terlin yi bokk na ci wallu sorri wante bi diggante nit ak nit. Terelin yi seen njariñ mooy fexe ba doomu jangoro bi du wall yeneen nit. Natal bii ci suuf loolu lay wane. + Pacc ñeetel bi ci wallu jangat ci mbass mi li muy wane mooy mbass mi ñungi koy men ci xeex bu baaxa baax te itam japp nanu ni dotul am walante  yu bess lu jem ci doomu jangoro bi. Ci jangat setlu nanu ni lu jem ci wallu xeetu mass yu melni korona mbir u wallatem ci diggante nit ak nik la gënna gaawe ndax sunu jegeyanto. Ci kaw loolu japp nanu ni kon, sorriwante rek mooy tax nu mënna mucc ci doomu jangaro bi  fexe ba du law. + +Wallu sorriwante bi digaante nit ak nit. +Sorriwante diggante nit ak nit benn xeetu doxalin la bu ñiy saytu wergu yaramu askan wi terel pur fexe ba nit yi am doomu jangoro bi baña jeflante ak nit yi dara jotul pur wañi bu baaxa bax wallante bi. Ay terlin yu am solo loolu ñoo ko lal ci missaal tejte dek dekan yi ak rew yi fexe ba mooytu bereb yi nga xamantani nit yi danu fay dem di daje. Terelin yu ni mel , njit u rew yi dekk yi ñoo menna jel ndogal yi . Ci missaal rew mu mel ni Afrique du Sud danuleen noot bu bax ngir nu menna jeffee ndogal yi nu jel ngir xeex jangoro bi mungi tambelewoon ci ñaari fukk fan ak juroom benn ci weer u Mars bi fukki waxtu ak ñaar jote ci guddi ba fukki fan ak juroom benn ci weer u Avril  atum ñaari juni ak ñaari fukk ci fukki waxtu ak ñaar ci guddi gannaaw loolu ñu yokat ci fukki fan ak ñint. Ndogol yi ñingi tenku ci ay terelin yunu tenk ci ay mbind ci pacc ñaari fukk ak juroom ñaar ci ñaareli pacc bi jem ci wallu naka lanuy doxale jeeyo yi am ci aduna bi gannaw bañu ko tenke ci ay mbind yunu tenk ci pacc juroom ñeet te li waral li yepp du leen ludul fexe ba nit baña jeggewante. + +Li leen rek la ci liñu jota tenk yepp gannaaw banu sukkandiko ci sart fukk ak benn bu reglemang bi : + + Fexe ba nit yi tog ci seeni ker yi, bi genn di am na fekk ni pur dem dox lu am farata lay done lu ci mel ni wallu dund walla dem liggey, liggey bu menul ñaak + Fexe ba benn dajee du am ci bereb yi nit yi di dajee lu ci epp wante ñinga xam ni dañu am ku leen jegee ta ñaak bakanam , may nañu leen ñu dem denc seen neew ci seg ya wante duñu wessu juroom fukki nit + Fexe ba dem ak dikk du am ci diggante dekk yi nekk ci benn reew bi. + Fexe ba dem ak dikk du am ci diggante gox goxan yi ak dekk yu ndaw yi nekk wet gi + Fexe ba bankaas yi di liggeey ci wally dund wala lepp lo  xam ni menul ñaak ci sunu dund, di weyal seeni liggeey. + Fexe ba bereb yi nga xam ni dañuy yengatu ci wallu dund ci missal jend ak jaay wala lep lo xamantani amal  na njariñ askan wi di weyal seen liggeey ci kaw ñu fonk sorriwante yi nu wakh tol ci benn metar ci diggante jend kat yi ak jaay kat yi wante itam fonk terelin yi nu wax jem ci wallu set jem ci sunuy loxo wala jemtuwaay yi di yengatu ci wallu bergu yaram nit yi ci bereb yi nit yi di daje lepp rek ngir jem ci lu wañi mbass mi di Korona. + +Terelin yi: + +  Fexe ba ayee bep tukki ci gej gi walla jawu ji. +  Fexe ba ayee njayum sangara ak cigaret +  Fexe ba yamalee nit yi di dugg ci woto tukki kay yi. + +Itam terelin yi may nañu ñi ngank nguur gi gir  ñu berr yenn nit yi.Matukay yi ñu jel ci wallu berr nit yi dafay tax ba nit yi ñu japp ni am nañu doomu jangoro ji wala ñu laale ak ku ko am ñu berr leen ci benn giir. Dafay tax ñu mena beddi nit yi am mbass mi ci nit yi ko amul. + +Afrik du Sud- royuwaay ci wall wi. +Terelin yi ñu jel yepp tax na ba mbass mi di Korona lawam gaawul torop tek ci wañeku bu baax wante reewum Afrique du Sud ci adduna wengel kep ñoo jiitu ci wallum xeex mbass mi. Waa Afrique du Sud toppuñu njangat bi am ci wallu mbass li jem ci mungi yek wall mungi wacc. Dañu jeggi ñaarelu pacc mbass mi ndaxte amuñuwoon yokkute ci mbass mi wante itam jankontewuñu ak wallante bu gaaw ci diggante nit ak nit ci benn gox. Xayma bi ñu def ci lim u ñinga xamantani amoon nañu doomu jangoro bi joggena ci ñint fukk ak ñaar ci xayma dem ci  ñint ci xayma gannaaw bañu fonke ak jeffe terelin yooyu. Li dafa wane ni wallante ci diggante nit ak nit ci benn gox dafa wañeku bu baaxa baax loolu moo tax ba limu ñi am mbass mi wañeku bu baaxa bax. Njitum rew ma, Cyril Ramaphosa dafa wax ak waa askanam ci jumtukay bu melni televisiong ci bessu juroom ñint fan ci weer u Avril atum ñaari juni at ak ñaari fukk pur wax ci matuwaay yi dekk ba jel munileen:" Nangu ngeen bepp terelin buñu teggoon.Wante itam nangu ngeen bepp matuwaay buñuleen waxoon ngeen jel koci wall dem bi ak dikk bi ba ci sax xañ leen seen moomel ci bess bi."Fajj kat yi seen xam xam macc ci wallu feebar yi di walle neenañu mbass mi mungi fii ba tay wallante bi men na nekk ba tay. "Wante terelin yi nguur gi jel tax na ba wallante bi wañeku bu baaxa baax te loolu taxna ba ñu am jot bu baax pur jublu ci leneen". Moo tax nak dinanu jemma xol nuñuy yolomale terelin yi ñu tenkoon. + +Ci tenk +COVID-19 feebar la bo xamantani werr na adduna bi yepp gannaaw banu xame ni nit yi ko njekka am ci dekk bu tudd Wuhan ci reewum Chine ci jextal u atum ñaari juni at  ak fukk ak juroom ñint. Kangam u Chinois yi senn xam xam macc ci wallu wergu yaram xay ma nañu ñaari fanna yo xamantani men na tax ñu xeex jangoro bi rawatina wergu yaram u nit yi di nekk ci bereb yi di nit yi di dajee: + +(1) Saytu ak fagaru ci mbass mi itam (2) amal ay gestu ci wallu xam xam ci wallu mbass mi. « Kangamu Chinois yi ci wallu wergu yaram def nañu liggeey bu yemm manna ba tax ñu xam xeetu Coronavirus bi ba taxna bankas bi ngank wallu wergu yaram ci aduna bi fexe na ba ñu jakarlo ak mbass mi am ci atum ñaari juni at ak ñaari fukk jem ci wallu xeex ko. Wallu sorriwante bi diggante nit ak nit wane ni am na njariñ loolu ci li jem ci wallu xeex mbass mi com niko reewum Afrik du Sud defe.Kurel yi tenk wallu doxalinu mbass mi ak itam naka lañuy  fagaro neenañu am na solo torop ñuy degante ak sunuy am di jamm, sunuy xarit, sunuy njabot, sunuy waa ker ndaxte men na nek ci telephon nuy wootante wala appel video ndaxte ñaak gissante ak nit ki nga begg yombul loolu te li ko waral du lenn ludul sorriwante bi. » + +Kangam yi di yengu ci wallu wergu yaram neenañu ñuy genna bayante xel ci jamono yi nga xamantani nit yi dañuy jaxaso loolu ndax ragal gannaaw ba mbass mi nekkee fepp ci aduna ndaxte nit ku nekk am na numuy dunde sunu tolo ci jamono yu mel ni ba taxna ku nekk war na di bayi xel moromom pur ñu menna jefflante ak jafejafe feebar u yumu menna juur. + +References +Baatu mbass mu ngi sosoo ci dëkku Grek yi te mu ngi tekki feebar bo xamante ni dafa jogee ci benn reew wala dëkk dëkkaan yi dem ci beneen reew wala beneen dëkk.Wallaate bu gaaw bu feebar bi ci benn askan wala benn dëkk ci diir bu gatt loolu lañuy wax mbass. Feebar bo xamantanen wërul adduna bi yëpp wala laalul askanu ab dëkk loolu dunu ko woowe mbass "feebar bu dëkk" lañukay woowee.Feebar yu dëkk yi nga xamante ni dañuy law ci nit yi am lu ci melni socc muy wall biy faral di am ci jamono bu nekk bokku ñu ci ndaxte ñoom dañuy feeñandoo benn yoon ci benn askan wante du luy law ci adduna bi. + +Li mbass di tekki ak pacc yiko lal +Mbass feebar bu dëkk le boo xamantani dafay nekk adduna wërngël këpp. Nekkul ni feebar bu law rek wala mu ray ay nit yu bëri rekk mbass la ndaxte dafa wara am ay mandarga yoo xamantani dafay wane ni feebar bi day wallaate. Ci misaal xam nañu ni feebaru Kaanser dafay faral di ray ay nit yu bari wante tekkiwul ni mbass le ndaxte nekkul loo xamanteni dafay wallaate. Xayma bi ñu def ci feebar yu dëkk yi (ak lu ci melni mbass yi) mooy ni dañuy setlu ni booko rëddee ci ay natalu xayma, dañuy nduroo lool ci lu jëm ci ni ñuy wallee ci ab diir. Jangat bi ñu def ci nataalu feebar yu dëkk yi mooy ni dafay yokk saa yu xewee ci jamono. Feebar yi di wallaate ci ñeeti faan lañuy lawee di nañu ci ñëw ci nataal bi ci suuf. Pacc bu njëkk bi mu ngi amee ci njëlbeenu jangatu nataalu mbass mi. Su fekkee amna ku jël misaal ci mbassum COVID-19 bi wallum lawaay bi ni mu gaawee li muy wane mooy ndorteel lawaayu mbass mi amagul woon sax ay nit yu bari yuko amoon. Paccum ñaareel bu nataalu jangatu mbass mi li muy wane mooy "wallante bi am ci digante nit ñi ci dëk dëkkaan yi te doo xam ku leen ko wall" Mooy jamono ji wallante digante nit ak nit gaww ci wallu nimuy lawee ndax sayunit yu bees yu am doomu jangoro bi. Paccum ñetteel bu nataalu jangatu mbass mi li muy wane mooy xeex nañu ko ba mënëtul am sayu nit yu beesyu am doomu jangoro bi. + +Doxalin jem ci mbass mi +Bari na ay matuwaay yu reew yi mëna jël ngir fagaru ci ab mbass mu leen bett. Ci atum ñaari junni ak juroom kurel bi di saytu wallu wergu yaram ci aduna werngeël këpp tënkoon në ay tërëlin yu mën di faagu, saytu ak di jammarloo jafa jafe yi mën am ci bu lawee ci diggente dëkk yi. Ci kaw loolu kureel bi ëmb wallu wergu yaram ci adduna bi yëpp bind na ben teere ngir xeex mbass um socc muy xelli. Teere boobu ñu ngi ko xamlewoon ci bu njëkk ci atum junni ak juroom ñeent teemeer ak juroom ñeent fukk wante ci atum ñaari junni ak juroom jap ñaari junni at ak juroom ñeent lañuko cambaraat andi ci ay coppi. Li ëp ci matuwaay yi ñu jël ngir xeex ak mbass um COVID-19 bi mu ngi soqqeeko ci kureelu wergu yaram gi ci addina bu atumñaari  junni ak juroom ak ci diglewu kurel gi ngank wallu wergu yaram bi ci adduna bi  ci naka lañuy waajalee mbass um socc muy xelli. Amal nañu waxtaan bu yaatu jëmëleko ci (saytu,fajj gi ak am ay jumtukaay ngir mën topp nit ki ndax bu ameee jangoro ji ñu xam ko) ndaxte dina tax ba ci njeëlbeen nu mëna xam nit yi am doomu jangoro ji ndax mën leena ber ci bamuy teel tek ci fajj leen. Doxalin boobu  dafay tax ñuy mënë raññee nit yi nga xamante ni dañu jëflante ak nit ki am doomu jangoro bi ngir mën ko ber. Doxalin bi reew yu melni Corée du Sud ak Singapour ñoo ko xamle ganaaw ndaw yu yaatu yi ñu ci am wante itam  reew yi mënoon nañu gënë waajal seen bopp ak ay doxalin gannaaw ba feebaru xëtër andi ay jiixi jaaxa ci seeni reew. Wallum soriwante ci diggante nit ak nit walla doxalinu ñi tënk wergu yaramu nit yi di daje fu mbolloo nekk ndax gis nañu ni doxalin la boo xamni dafaywañi doole feebar bi ganaaw bañu fexee ba nit yi duñu jegeente ndaxte dafay wañi wallante bi ci feebar yuni mel. Doctoor Michael J Ryan di njiit ci kureel gi tënk wallu wergu yaram ci adduna bi yëpp xamlena ci benn waxtaan bumu seqqoon ak taskatu xabaar yi ci weeru Mars ci atum ñaari junni ak juroom ñeent "wallu soriwante ci diggante nit ak nit doxalin buñu jëlandi ngir mu mëna wañi bu baax doole wallante bu doomu jangor bi wante itam gëtëm ñi nekk ci wallu wergu yaram wante nekkul pur fajj doomu jangoro bi ci boppam.Donte ni yombul wante ci xayma war nañu ko jëfëndikoo ak yeneeni xeetu doxalin ngir mënë saafara jafe jafe bi". Doktoor Ryan xamlena ni nekkul ni soriwante bi ci boppam mooy saafara feebar bi. + +Mbass yi am jamonoy tey + +Feebaru u SIDA +Bataaxal bu am solo: Jangat ci feebar bii di SIDA + +Donte ni kureel gi ëmb waalumwergu yaram gi ci adduna bi yeëpp dafay jëfëndikoo baatu feebar bu dëkk ngir tekki lii di SIDA dañuy japp ni tur bi wuyu na jëmm ji. Ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom ñeet lu toll ci juroom ñaari teemeer ak juroom ñaari fukki junni nit ñakk nañu seen bakkan ci feebar bi di SIDA. Ci jamono jii ñu toll ña dëkkee ca Afrique Sub-saharian ñoom la feebar bi gënë yapp.Ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom ñeet xayma nañu ni juroom benn fukk ak benn nit ci teemeer boo jël ci ñu am jangoro ji ñu ngi juge foofu. + +Koronaa wirus +Koronaa  wirus yi (CoV) ay xeetu doomu jangoro lañu yoo xamante ni mën nañu jur ay feebar yu melni sojj wala yeneen xeetu feebar yu gënë garaaw yu melni mandargay feebaru noyyi ñu gën ko gisee ca reewum Moyen-Orient ñu xam ko ci (MERS-CoV) ak itam mandargay feebaru xëtër loolu ñu xam ko ci (SARS-CoV). amna beneen fasong coronavirus(SARS-CoV-2) bu ray ay nit ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom ñeent, wala COVID-19. amna yenn ci ay coronavirus yu zogee ci mala yi muy wane ni wall ba ngi ci digënte mala yi ak nit ñi. Cambar yi ñu def wane na ni feebar bi di (SARS-CoV) mu ngi jugee ci xeetu muus yi jëm ci nit ñi,tek ci feebar bi di MERS-CoV mu ngi jogee ci hëleem yi dem ci nit ñi. Bari na nak ay xeetu coronavirus yu nekk ci mala te ba leegi demaguñu ci nit ñi. + +vag bu bees bu coronavirus bayyeeko ca Wuhan,Hubei, fële ca Chine ci njeexitalu atum ñaar fukki junni ak fukk ak juroom ñeent, moo andi feebar bi ñuy wax coronavirus2019 (COVID-19) te muy japp xëtër yi.Ganaaw ba ña ca waa daara ju mag ja ca John Hopkins amalee njangat li ñu setlu mooy lu toll ci ñaari teemeeri dëkk ak liko wër am nañu feebar bi di COVID-19 wante feebar bi reew yu melni Amerik, Europ,Chine ak Iran la gënë bëri. Ci fukki fan ak benn ci weeru Mars kureel gi ngank waalum wergu yaram ci adduna bi yëpp jappee na feebar bi di COVID-19 te muy law ab mbass. Ba ci bësu Avril ñaar fukki fan ak ñett ci atum ñaari junni ak ñaar fukk nit yi am mbass mii di COVID-19 ñu ngi toll ci ñaari milyong yu toftaljuroom benn fukk ak ñett  ci ay nit yu am doomu jangoro ji,limu ñi ñakk seen bakan toll na ci teemeeri junni yu toftal juroom ñett fukk ak ñeent junni nit ak ñaari teemeer ak ñeent fukk ak juroom ñeent terk ci limu ñi wer toll nañu ci juroom ñaari teemeeri ak ��aar fukk ak ñaari junniy nit yu toftal juroom fukk ak juroom. Feeñaay bu am solo lool + +Sibiru +Feebaru sibiru wër na ci reew yi nekkee ci "tropical" bi ak "subtropical" bi ak itam benn pacc ci reewu Amerik, ci reewu Asie ak Afrik. At mu nekk lu toll ci ñett teemeer ak juroom fukk japp juroom teemeeri milyong ci ay nit dañuy am sibiru. Jammarlo bi doomu jangoro bi di jammarlo ak garab yi nerkk na ay jafe jafe ci jamono. "siecle" bi ñunekk te loolu wër na ba ci yeneeni xeetu garab yëpp jëm ci xeex sibiru ba mu dess "artemisines" + +Bu njëkk feebaru sibiru nekkoon lu tekk tank ci lu ëpp ci reewum Ëropp yi ak yu Amerik ci booru penku bi, wante leegi jeex nafa. Mën nañu wax ni feebaru sibiru bi moo daanel banqaas bu Romain yi. Deemoon nañu bay tuddee feebar bi "Feebaru Romain yi". Ci kaw loolu la doomu jangoro bi di joxe feebaru sibiru nekkoon jafe jafe ci nit yi fa dekkoon bi doomu jangoro bi duggee foofu ci jamonoy njaam ci Amerik. + +Feebaru socc muy xeeli bi ci Espaañ +Feebaru socc muy xelli bi amoon (ci diggënte atum junni ak juroom ñeenti teemeer ak fukk ak juroom ñett japp atum junni ak juroom ñeenti teemeer ak ñaar fukk) ca reewum Espaañ walloon na  teemeeri milyong i nit ci adduna bi, bu ñu ci boole nit ñi dëkk ci Pacifique bi ak Arctique bi, ba paré ray fa lu toll ci ñaar fukk japp teemeeri milyong ci ay nit. Jangat bi ñu def ci socc miy xelli moy ni xale yi ak maggat yi lay gënë ray wante itam setlu nañu ni ñi dig doomu te am feebar bi seen dund mooy gënë yagg. Li feebaru socc miy xelli bi feeñoon fële ca Espaañ rayoon mo ëpp fuuf li xeex bu ñëkk bi wëroon ci adduna bi yëpp rayoon tek ci li mu ray ci ay nit ci diggeënte ñaar fukk ak juroom ci ayu bess doomu jangoro bii di SIDA sax rayu ko ci diiru ñaar fukki at ak juroom yu njëk ci bi mu feeñe. Mboolo yu tak der yi ay gox yi ñu tejjoon ci giiru xeex bi adduna yëpp bokkoon moo waraloon wallante jangoro ji gaawoon lool, njaaqare bu ëpp ak jaxasoo ci tak der wante itam ñam yu bon yi ñu daan lekk ak itam song yoo xamante ni ganaay yu tooke taxoon na ba tak der yi daan am doomu jangoro ji ci lu yomb. Jumtukaay yu yees jëm ci dem beek dik bi taxoon  ba yombal tak der yi ci fi ñuy bëg dem, wala takk deru geej gi ak nit ñi seen bopp taxoon na ba lawaayu doomu jangoro ji gaawoon lool. + +Njaqare ci doomu jangoro yi nar am ci ay at ci kanam + +Jamarlo bi garab yi did def +Bataaxal bu jëm ci jamarloo yi garab yi di def + +Antibiotic-resistant microorganisms are sometimes referred to as "superbugs". They may contribute Micro-organism yi di jamarloo ak xeetu garab yi ñoom lañuy woowe ay superbugs.mën nañu dekkalaat feebar yi nga xamantani tegoon nañu ci loxo ba noppi . Ci misaal feebar yu ci melni sëqët mu tar mi nga xamanteni mu ngi jamarloo yenn fasong paccum wolof yi nek na njaxaree ci ñi nga xamni seen xel macc na ci wallum wergu yaram.Xaynma nañu ni  ci lu jegee xaaju milyong ci ay nit ci adduna bi di nañu  am xeetu jangoro bu melni sëqët mu tar mi(MDR-TB) at mu ne. Reewum Chine ak Inde ñooy reew yi gënë am xeetu feebaru sëqët mu tar mi ci adduna werngël këpp. Kureel gi ëmb wallum wergu yaram ci adduna bi yëpp xamlena ni ci lu tolook juroom fukki milyoong ci doomu aadama am nañu doomu jangoro ji ñuy wax MDR TB,ci kaw loolu juroom ñaari fukk ak juroom ñeent ci teemeer bo jëll ci ñiko am ñu ngi jammarloo ak lu toll ci ñett wala luko ëp ci ay garab. Ci atum ñaari junni ak juroom, teemeer ak ñaari fukk ak ñeent ci ay nit ci reewum Amerik ammon nañu feebaru sëqët mu tar mi. Ci atum ñaari junni ak ñeent feebaru sëqët mu tar mi feeñoon na ci reewum Afrik ak ci yeneen ñeent fukki reew ak juroom ñeenti reew bu ńu ci boole Amerik. Kureel gi ëmb wallum wergu yaram ci aaduna wergël këpp defna xayma bu yees ni ńi am feebaru sëqët su tar si tollu nañu ci ñeent fukki junniy nit. + +Ci giiru ñaar fukk at yii weesu walax jaan yi ñu gênë rañee yu ci melni Staphylococcus aureus wala Serratia marcescens akEnterococcus wane nañu ay jamarlo yu am solo jëm ci wallu ay xeetu garab yu melni vancomycine ak yeneeni xeetu garab yu ci melni aminoglycosides ak cephalosporines. Yooyu xeetu walax jaan yi di jamarloo ak garab yi ñoo waral leegi ñu setlu ay xeetu infeksoon yu melni nosocomiales. Ci kaw loolu infeksoon yi nga xamanteni ñu ngi jogee ci xeetu walax jaan yu melni Staphylococcus aureus di jamarloo ak xeetu garab yu melni methicilline ci nit yi nga xam ni ñu ngi and ak wergu yaram setlu nañu ni dafa bëri lool ci at yi ñu weesu ni. + +Feebar bu garaw bu mënë andil nit ki yaram bi di tang wala muy waccu wala muy nacc ci gemmiñ wala ci bakkan +Feebar yu garaaw yi mëna andil nit ki yaramam di tang wala muy waccu wala muy nacc ci gemmiñ wala ci bakkan dañuy wallaate ci lu gaww tekci di raye bu baax. Ci misaal feebar bu joge ci doomu jangoro bu "Ebola", feebar bu ñuy wax "Lassa" ak itam feebar bi ñuy wax "vallée du Rift" ak itam feebar bi joge ci doomu jangoro biñuy wax"Marbug" ak feebar nacc nacc ci yenn ci ay pacc nit ki joge ci reewum" Bolivie". Feebar yu garaw yi mën andil nit ki yaramam di tang wala muy waccu wala muy nacc ci gemmiñ wala ci bakkan amna ñu kattanu nekk mbass ci adduna bi yepp ganaaw ay jangat yi ci am. Seen doole ngir ñu mën wallaate ci lu gaaw ba mënë jur mbass ci adduna bi yepp taxu ko deme nonu ndaxte fi leek nit ki am doomu jangoro ni jegewul ku ko amagul wallaate bi du am tek ci nit ki am doomu jangoro bi likoy dese ci ay bess ngir mu dund bëriwul wala mu am feebar buko sonal lool. Digante bi mandarga yi di  wane ni am nga doomu jangoro ji dina tax ba ñi ngank wallum wergu yaram ber la ci teel ndax nga baña yobbu doomu jangoro bi ci yeneeni bereb. + +Doomu jangoro bi tudd Zika +Bataaxal yu am solo lool: Mbass mi joge ci doomu jangoro bi tudd Zika ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom jëm ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom benn, doomu jangoro bi tudd Zika, yaram yi di tang joge ci doomu jangor bi di Zika. Mbass mi jogee ci doomu jangoro bu tudd Zika mu ngi tambale ci atum ñaari junni ak fukk ak juroom  wante mu ngi am doole lool ci giir atum ñaari junni ak fukk ak juroom ben lu toll ci  benn milyong yu tekk juroom teemeer junni ci ay nit yu amoon doomu jangoro bi lu toll ci fukki reew ak ñaar ci reewum Amerik. Kureel gi ëmb wallum wergu yaram ci adduna bi artu na ni yi ni doomu jangaro bi di Zika mënoon na dem ba andi mbass mu yeemeci adduna bi yëpp  su fekkantenewoon ni jeemu ñu def dara ngir xeex ko. + +References + + +Tektalu gornmang bi. +Coluk mask yi ci mbas mii di coronavirus am ci atum 2019-2020 jot na am digle yu bëri yu ci juddo jogge ci kurël yi tënk wallu wërgu yaram ak itam gornmang bi . Mbir mi di coluk mask yi juur na ay coow yu juur au reero ci digante ñi ngank wallu wërgu yaram nit yi ak itam gornmang bi lu jëm ci wallu coluk mask yi. + +Liy yoon +Yeen yoon ci yi borom xam xam ya ca siin ci wallum wergu yaram wax ne noonu lañu wara sole mask mooy: + + Ki la waal te amul been mandarga buy wane ni amna feebar bi .Bari na ñu mën am feebar bi te du am been mandarga buy feeñ seen yaram wala bu amee itam du leen sonal. + Nakk mën ci lu jëm ci wallum ñak dendale  nit yi ci bereb yu siiw yi. + Su fekkoon ni ñi feebar sol nañu mask, doon nañu baña joxe feebar bi. Ki doomu jangaro ji nekk ci yaramam mën na baña degg dara lu baax,ludul  ñukay wax lu ñaaw tek ci diko beddi. + +Ab waay bu xam xamam macc ci wallum wirus yi nekk ca université bu Leeds te mu tudd Stephen Griffin neena" bu nit ñi di sol mask mën na tax ba du ñu laal seeni kanam te loolu men na juur feebar bi su fekkantane loxo yi setul". + +Fasong mask yi +Masku tisu yi mooy fasong mask yi nga xamne ñu ngi ko defaree tisu ngir mu muur gemmiñ gi ak bakkan bi, cotong lañu kay faral di defaree, lu wuuteek mask yi ñiy oppeere di sol ak nooyikaay yi, tek ci itam nekkul lu yoon nangu. Am na ay jangat yu ñu  ci amal pur xam ndax mask yu baax la pur aar nit yi ci wallante feebar bi ak xeet u feebar yi bon yi nekk ci jawu ji. Mask yi ñiy oppeere di sol mooy mask yi nga xamante ni bu  ñu ko jeffandiko ba noppi danñu koy sanni tek ci dafa woyof  ñu ngi ko defaree noo xamante ni dafay aar bakken ak gemmiñu ki ko takk ci bepp doom u jangoro bu nekk ci bereb bi mu nekk.Mask yi ñiy oppeere di sol dai ñu ko defar ngir mu mena tëye bepp tokk tokk bu baayee ko ci gemmiñ wala bakken u nit lu ci mel ni tëflid wala ñandaxit yi nga xamanate ni men na am ay wirus wala bepp xeet u doom u jangoro sufekkante ni takk nañu ko ni ñu ko santane, wante fexe itam ba doom u jangoro yooyu baña laal gemmiñ ak bakken u ki takk mask bi. Mask yi ñiy oppeere di sol dina tax itam ba ki feebar bi ay tëflitam duñu dal ci keneen ba men ko jox doom u jangoro bi. Mask yi ñiy oppeere di sol defaruñu ko pur mu segg wala tëye doom u jangoro yu ndaw yi nekk ci jawu ji te men wallate ci sëkkat, wala ñandu wala yenn ci doxalin u waa kër doktor.Mask yi ñiy oppeere di sol neekul ni dañuy aar nit yi bamu mat ci bepp xeet u doom u jangoro ndaxte mask bi ci benn pacc ci sunu kanam lay aar te nekkul lu serre ci kanam bi.Mask yi ñiy oppeere di sol tisu lañu ko defaree ci ndimbal u doxalin yu mel ni "fusion-soufflage". + +Mask bi di N95 fasong mask le boo xamni dafay segg bepp xeetu doom u jangoro bu nekk ci ngelaw li tek ci dafa samonte ak saart yi waa reewu Amérique jël jem ci karange wergu yaram u liggey kat yi. Dina segg lu toll ci juroom  ñint fukk ak juroom ci teemeer boo jël. Missaal la ci xeetu nooyi kaay yi boo xamante ni dafa lay aar ci wallu doom u jangoro yi nekk ci jawu ji wante menula aar ci lu mel ni ay gaas, wala saxaar. Moom ak mask yi ñiy oppeere di sol ñoo yam ndaxte tisu bu "polypropylène" buñu rabbul lañu ko defaree Mask bi waa Union Européenne  di jëfandiko mooy fasong mask bu tudd FFP2. + +Digleeg kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi +Kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi digle  nañu nit ñi ni buñuy sëqqët wala ñuy tissooli warnañu tek seen ruqqu concc ci seen gemmiñ wala ñu jël morso bu leen gënë jegee. Digal nañu ñi am feebar bi ñuy sol mask yooyu ñi faral di oppeere di sol, ndax sol mask yi dina wañi bu baax tis tis yi nit mena nooyi te  jogge ci waxtan,sëqqët wala tissooli. + +Digleeg kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi ci adduna werngël këpp +Kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi nekk ci adduna werngël këpp mu ngi gënë bayiloo xel nit ñi ci ñuy sol mask yi ci kaw yile sart yuñu tërël: + + Bu fekkee ni and nga ak wergu yaram, di nga soxla mask ci bu fekkee ni ya ngi toppato ku ñu yaakaar ni amna feebar COVID-19. + Solal mask bu fekkee ni da ngay sëqqët mbaa ngay tishooli. + Di sol mask lu am njariñ la ci kaw nga kay faral di foot ak ndox mu set ak saabu bo ci mënee def tuti alkol di na baax. + Su fekkee ni da ngay sol mask, kon war nga xam nan lanu kay solee ci nimu waree. + +Li reewu Afrik yi tërël ci lu jëm ci wallum tak mask yi + + Benin: Liko dalee juroom ñetti bes ci weeru avril, kilifa waa benin yi door nañu ab liggeey ngir forsé ñuy sol mask ngir faagaagal coronavirus bi. + Cameroon:njiitu reewu taaxu dëkk bë wax nani di nañu digël ñëpp ñuy sol mask ngir waañi ni coronavirus bi di lawee. + Reewu Republique Democratic bu Congo: coluk mask bi leegi lu ñëpp wara def la ca capitaal ba. + Ethiopia: Mbootaayu ministar ya nangu nañ dogalup tere nuyoo tek ci ñëppa wara sol mask bu ñu nekkee fuy faral di am nit. + Ci reewu  Guinee Conakry: njiitu reew mii di  Alpha Conde jël në dogal ni ñëppa wara takk mask. + Ca Kenya solfa mask lu warla. Gornmang bi tek na ay tërëlin ni ñëppa wara samonte ak tërëlin yi di baña tankaloo ci  bërëb yi nit ñi di faral di dajje ndaxte loolu bokk na ci luy tax doole wallate feebar bi neew loolu. + Liberia: Ci ñaar fukki fan ak ben ci weeru avril ba jamono jile gornmang bi dogal na ni ñëppa wara tak mask wala ñu muur seen kanam. + Ca Marok solfa mask lu war la. + +Référence +Isifo esidaleka emoyeni siso nasiphi na isifo esibangelwa ziintsholongwane ezibhabha okanye ezihlala emoyeni nakwi zinto ezibhabhayo ixeshana. Izifo ezi loluhlobo uyakufumanisa ukuba zifumaneka kwizilwanyana kunye nasebantwini. Ezintsholongwane zizifo ngezifo ezosulela ngokuphefumla, ukuthetha, ukukhohlela, ukuthimla, ukufafazwa kwezinto ezingamanzi, kunye nayiphi na into ebangela kushiyeke izinto ezibhabhayo emoyeni. Amaxesha amaninzi izifo ezifumaneka emoyeni zibangela ukurhawuzelela okanye izilonda kwiimpumlo, umqala kunye nemiphunga, kubange ukukhohlela oko, umqala obuhlungu, kunye nezinye iimpawu ezibonakala kumzimba wonke. Izifo ezininzi ezixhaphakileyo ekuqwalaseleka ukuba zosuleleka ngokuhlala emoyeni ziquka ezi zilandelayo, kodwa zibe zingaphelelanga apha: coronavirus, measles morbillivirus, chickenpox virus; Mycobacterium tuberculosis, influenza virus, enterovirus, kunye ne-norovirus. Ezi zifo ziye zifune ukuba umntu ahlale eyedwa angadibani nabanye ngexesha lokunyangwa. + +Izifo ezidaleka emoyeni zibangelwa kukuhamba-hamba nokubhabha kweentsholongwane emoyeni. Unobangela wazo ke kukosuleleka kwezinto ngezinto, ukususela kwiincindi zomzimba zabantu nezilwanyana, okanye kwinkunkuma. Ezintsholongwane ziye zande ngokuba zihlale kuthuli okanye emoyeni othi abhabhe lee na lee ixesha elide. Umzekelo, ukuthimla kuhamba umgama omde, omlinganiso ubukhulu ngange bhasi, onothi ubangele kusuleleke isininzi sabantu. Ukuphefumla umoya oneentsholongwane kungabangela izilonda okanye ukurhawuzelela, kwaye kuchaphazele nendlela yokuphefumla komntu. Izifo ezidaleka emoyeni aziquki iimeko ezibangelwa lungcoliseko komhlaba, kodwa ungcoliseko komhlaba kunayo indima enkulu okuyidlalayo ukwandisa izifo ezifana nesi sesifuba. Ungcoliseko komhlaba kunefuthe kwindlela ethi imiphunga isebenze ngayo. Izifo ezidaleka emoyeni zinako ukosulela nezilwanyana. Umzekelo, intsholongwane ekuthiwa yiNewcastle ukubizwa, sisifo esichaphazela iintlobo ezohlukileyo zeenkukhu zasemakhaya ilizwe jikelele, esosuleleka ngokungcoliseka komoya. + +Ukosuleleka +Usulelo lwezi zifo kwenzeka xa athe umntu ophilileyo waphefumla umoya ekufumaniseka ugcwele ziintsholongwane, okanye xa umoya omdaka uthe wangena emehlweni, empumlweni, okanye emlonyeni. Akunyanzelekanga ukuba ude udibane buso ngobuso nomntu onaso esi sifo ukuze wosuleleke kuba sihlala kwaye sibhabha emoyeni. Ubushushu nokufudumala kwangaphakathi endlini kunye nangaphandle bunendima obuyidlalayo ekuhambiseni izifo ezidaleka emoyeni. Eminye imiba ebangela ukwanda nokuhamba-hamba kwezi zifo ezidaleka emoyeni yimvula, umoya, ubumdaka bendawo kunye nokuziphatha kakubi kwabantu. + +Ukuthintela +Ezinye iindlela zokuzithintela kwezi zifo zidaleka emoyeni kuquka amayeza afana nezitofo, ukunxiba isifonyo esogquma umlomo ne nempumlo, kunye nokuphepha wonke ubani ekufumaniseka ukuba unaso esi sifo. Xa uthe wadibana kunye nomntu onaso esinye sezi zifo zidaleka emoyeni akuthethi ukuba sele wasulelekile waze wanaso nawe, kuba ukusuleleka kwezifo eziloluhlobo kuxhomekeke empilweni nasemandleni omntu ngamnye, kunye nokuba loondawo athe wakuyo umntu ichaphazeleke kangakanani na. Izibulala-ntsholongwane zingasetyenziswa ukuzikhusela kwizifo ezifumaneka emoyeni ezifana nePneumonic plague. Lingcali zonyango zicebisa ucoceko kunye nokuhlala nganye-nganye ekunciphiseni izinga lokosuleleka ngezi zifo. Ukuncedisa ukwehlisa amathuba okusuleleka kucetyiswa ukuba wonke ubani enze oku kulandelayo: + + Hlalela kude kunabantu abanazo ezi zifo. + Nxiba isifonyo xa usendaweni kawonke-wonke. + Gquma umlomo wakho xa ukhohlela okanye uthimla. + Hlamba izandla zakho ngocoselelo ngawo onke amaxesha. + +Sukubamba ubuso bakho okanye abanye abantu ngezandla ezimdaka + +References +Doomu jangaro bu nit menul tek bet la ci kaw nga jeffandiko  jumtukaay bu lay may nga gis ko.Men na jural nit ki infection ba tax mu am feebar. Pathogen itam men nanu ko mengale ak lu mel ni "germs" wala yennsay  "parasite" ndax microb yuy dund lanuy dunde. Pathogen yi nit yi genna xam " virus" la ak " bacterie". Feebar yi pathogen menna joxe ci missaal Korona lanuy woowe feebar yuy wale. + +Xeetu ker doktoor yi + +Setlu ci clinic yu ndaw yi ak clinic yu mag yi. +Baat u "infection" mooy beep tewaay u jangoro bo xamantani liko juur mooy ay "pathogen" ak nuniu menna tol nak wante daniuy jeffandiko  bat bi lu ci epp pur men wax ci " infection" bo xamantani "clinic" yi gis naniu ko. Wante yennsay mu andi ay jaxaso, wante ci benneen wal, nit yi nek di yengatu ci wallu wer gu yaram danuy faral di wax baat u nootel su fekkantani microb yiy joxe jangoro nekk naniu ci yaramu nit ki wante nit ki wanewul benn feebar. Mandargay "infection" yi men nan len xaaj ci niaari pacc: bi feeñ ci nit ki ak bi nga xamantane ci clinic lanu ko menna gisse gannaw banu amale saytu. "Infection" bi nekk ci nit di dund ta wanewul ben mandarga lanuy woowe "infection" buy nelaw ci nit ki. "Infection" bu lak u ci nit, mooy "infection" bu am ci nit ki wante wanewul benn mandarga, ci gatal mooy "infection" buy nelaw ci nit. Ci missaal, feebar u "Tuberclose". "Infection" yi genna graw lu ci mel ni "Herpes" men nanu itam nekk ci nit ki te du wane benn manadarga. Xeetu "infection" yi men nanu leen xaaj ci  pacc yi: garaw,( mooy bi nga xam ni mandargay infection feebar bi dafay law bu gaaw), chronic ( mooy infection bi nga xam ni ay mandargam danuy law ndank ndank) infection bu garawul( mooy bi nga xam ni mandargay feebar bi du gaw law, wante men na law ci gaaw ba raw bu chronic, infection buy nelaw( mooy bi nga xam ni nit ki amul benn mandargay infection wante "pathogen" u infection bi mungi ci moom), ndotel u infection ( mooy fi nga xam ni foofu la infection bi tambali laata mu law ci li dess ci yaram u nit ki). + +Walante +Ni nga xamantane noonu la nit ñi di jele jangoro bi ci nit yobu ko ci nit, moom lanuy wakh yoon u wanlante. doom u jangoro u rañeku yi ñooy jooxe infection u rañeku yi itam infection u rañeku yi dañu am yoon u walate u rañeku. Pur xam lu waral infection yi di am ak naka lanuy fagaro ci ñoom faaj kat yi sen xel macc ci mbiir moomu war nanu xam naka la yoon u walante infection boobu di ame. Yoon u walante am na ay pacc u berri. Ci gatal men nanu ci lim: + + Doomu jangaro ji ( ndax ñoom ci ndote u infection bi lanuy dunde) mooy organism bo xam ni dafay joxe infection. Pathogen yi genna rañeeku ñooy virus ak bacterie + Fi feebar bi jogge men na nekk mala bu am infection wala nit bu am domu jangoro bi + Bunt u gennu kaay mooy yoon bi doom u jangoro bi di jeffandiko pur genn ci yaramu fi infection bi tambale + Bunuy wax walante mooy yoon bi doom u jangoro  bi jogge ci nit wala mala bu ko yore pur jox ko nit ku amul katan wala wayadi + Bunuy wax dekkuwaay mooy dekkuwway bi nga xam ni foofu la doom u jangoro bi wara jaare pur jogge ci nit wala mala bu ko am , pur dem ci niit bu neew doole + Buntu duggukaay mooy yoon bi doom u jangoro bi jaar pur dugg ci yaram u nit ku neew doole + Nit wala mala bi nga xam ni men na dalal doom u jangoro bi suba, mooy nit ki nga xam ni yaramam dina men dekku doom u jangoro bi + +Doom u jangoro bi men na jogge ci nit wala mala bu ko yore pur dem ci nit bu neew doole ci anam bu nekk. Am na ay xeet u doom u jangoro ñoom ndox wala dund moo kay yobbu, am na yenneen yaram yu lalante wante itam am na yenneen ci jawu ji. Ci mbind mi, dinanu waxt ci doom u jangoro bi nekk ci jawu ji. + +Primaire versus Opportuniste + +Primaire vs. Opportuniste +Ci setlu, giss nanu ni neew na ci loolu yenn xeet u jangoro yi di nekk ci nit yi am wer gu yaram bu bax ama na sax am na ay xeet u "micro-organisme" yu berri. Feebar bu feeñ tek ci gararw loolu leep dafay lalu ci doole bi doom u jangoro bi am pur yakk fi doom u jangoro bi tambale wala doole bi nga xam ni fi doom u jangoro bi am nako pur dekku " germs" yi. Yennsay "system immunitaire" bi nga xam  ni foofu la doom u jangoro bi sosso, men na yakal bopam gannaw bamu jeme pur controle infection yi. Waa ker doktor yi seen xel macc ci walu wergu yaram japp nauñ ni microbe yi am na ci ay " pathogen primaire" wala "pathogen oportuniste". + +Primaire Pathogènes +Doomu jangaro primaire wala germ  dañuy jooxe feebar rek gannaaw ñu nekk ci nit ki am jangoro bi te dara jootu ko ak itam ci doole bi ñu am ci jooxe feebar. Lu ci epp ci germ nit yi, nit yi rek lañuy infecte wante am na ay feebar yu garaw yi nga xamantani ay organisme yu nekk ci dekkuwaay yi ñoo koy joxe wala sax yenneen xeet yu am infection te duñu ay nit. + +Bibbe nabbe subay wernoowo mabbe +Pathogen opportuniste yi men nañu joxe ay jangoro yi nga xamantani dañuy walate ci nit yi am doom u jangoro bi te amuñu benn mandarga te sen sen system immunitaire yi leen di aar amuñ u doole wala ci anam yu mel ni operation chirurgical wala accident lañuy dugg ci sen yaram.Pathogen opportuniste yi dañuy law bu baax ci kwa nit ki am doom u jangoro bi nekk ci anam yi nga xamatani dafa sonn loolu. + +Jangat ci  infection bi waral jafe jafe wergu yaram nit ki ak jafe jafe yi cu men juddu +Infection bi njek men nanu ko jappe kon li waral jafe jafe wergu aram nit ki, wente ci bennen wet, ñaarel u infection men nanu ko jape kon jafe jafe yi men juddu gannaaw infection bi. + +Feebar yiy walate +Feebar bu nit jele ci infection , moom lanuy woowe feebar buy walate gannaaw bi nu jeflante ak nit ku feebar bu am jangoro bu mel ni grippe.Yenneen xeet u jangoro yi nit mena am gannaaw bamu amee infection wala mu jeflante ak nit ci wallu sexe dunu ay jangoro yu garaw loolu te itam soxlawuñu di bedi nit ki diko berr. Jangoro yi nit mena am gannaw mu ame infection and nanu ci ni, walante bi ci digante nit ak nit la wala ñak, wante itam walante bi men na nekk ci jawu ji, wala lekk gi, wala ndox mu set bu am doom u jangoro bi, wala nga jeflante ak mala, wante itam mat mat yo. + +Manadargay feebar +Mandargay infection bi mun gi lalu ci ban xeetu feebar la. Am na ay mandargay feebar yi nga xamantani yaram bi yep lañuy japp; lu ci mel ni coono, ñak lekk, sa yaram di jeex, sa yaram di tang, wala ngay ñak guddi, ngay lox, di am ay metiit,di son lu berri. Am na yenneen xeetu manadarga yo xamantani danuy feeñ ci yenn pacc yaramu nit ki ci missaal, tap wala sekkat,wala bakan buy sotiku. + +Yensaay feebar yi jogge ci infection duñu wone benn mandarga giiru jamono bi ñu nekk ci nit ki. Am infection tekkiwul ni nit ki dafa am feebar bu garaw di walle ndax am na ay infection yi nga xamantani duñu juur benn feebar ci nit ki am infection bi. + +Fii bakteri maa viral +Gannaaw bi nu xame ni bacteri wala viral men nanu juur benn mandargay jangoro, dina jafe loolu xam lan moo waral infection bu specific. Am na solo torop xam lan mo waral wuute bi ndaxte infection viral yi kenn menu ko fajj ak ay garab yu mel ni aitibiotic gannaaw bi nu xame ni men na fajj infection yu bacteri yi. + +Fajj gi +Sufekkantani infection dafa song yaram u nit ki, xeetu garab yi di fajj infection, men nanu ko dindi. Am na xeetu garab yu berri yi nekk di fajj infection. Ay antibiotic ñoom  bacterie rek mo leen taxa jogg itam menaluñu doom u jangoro  bi dara. Antibotic li ko taxa jogg mooy wañi doole bacterie bi  ci ni muy lawe wala ray bacterie bi. + +References +Ci wallu pajj saytu yaram mooy xool nit ki ban jangaro moo nek ci moom walla luy wone  liko febaar. Saytu nit ki nak dafay lacc xam dembam ak li ci yaramam ndax ñu xam limu andal. Yennsaay, benn wala saytu yu berri dañu koy amal ci jamonoy gëstu pur xam yan xeet u feebar ñoo nekk ci yaramu nit ki. Lek lek itam  saytu yaramu nit ku ñaak bakkanam ba pare mën nañu ko jappe kom saytu yaramu nit ki pur xam ban feebar moo nekk ci moom. Saytu yaramunit ki dafay faral di nekk lu jafe ndaxte mandargay doomu jangoro yu berri dañu jafe xam loolu. Ci missaal yaramu nit buy xonk jafe jafe la ci pajjkat yi xam mandargay ban feebar la. + +Toppu fajum yoon +Pajum yoon ak saytu limu andal: + + Xam lu bari ci kuy faju, mana xam ay febaaru dembam,saytu yaramam and  ak yenen  xeet u saytu (buko jare lacte kimu jege ndax geuna xam). Saytu dafa melne  xool beep xeet u febaar bu nekk ci nit. Saytu meunna doon pur xam  mandarga bepp feebar bu nekk ci yaramu borom. + Saytu ci wallu tontu yi,setlu, wala yenen xeet u jangat.  Wante itam saytu ak yenen doktor yu sen xel macc ci wallu pajj mën na nekk xalat bu raffet loolu. + +Barina fasong yinuy sayto ci toppu fajum yoon,bokk na ci amal ay xeet u saytu yu berri te wute wala xeet u saytu yu bess yi nga xamante ni mën na wane bepp xeet u jangoro bu nekk ci yaram u nit ki. Ci deug deug toppu fajum yoon barina yoon. + +Saytu ci wallu corona wirus bi +Corona wirus bi  mën  nañu ko saytu ci ay mandargam jëm ci saytu yu njëk yi, donte ni sax pur dëggal ni feebar bi mungi ci nit dañuy xaar ba am mandarga yu melni luñuy tudde (rRT-PCR) wala xaar ba giss ni  am na ay pacc yaram u nit ki am na doom u jangoro bi ci missaal tiflit (CT) lañu koy mandarga le. amal nañu jangat ci diggante (CT) li jëm ci wallu askaneer ak (PCR) manam li jëm ci wallu  ADN nit ki ci rewu Wuhan limu wone mooy saytu ak skaneer amul njariñ loolu. Li ko tamabale ci weer u mars  2020 ba leegi daara ju mag nekk ci Amérique di yëngu ci wallu rajo xamle ni " lu jëm ci wallu skaneer pur saytu feebar bi di corona wirus nekkul li ñu diggle". + +Saytu virus +Kurël bi tënk wallu wërgu yaram ci aduna bi yepp xamle na ay bataaxal jëm ci tërelin u saytu yi ñuy amal ci wallu corona wirus bi, xamle bu njëk bi mungi amoon ci weer u janvier ci bessu fukk ak juroom  ñaar. Saytu bi reaktion bu tuddu (rRT-PCR) lay jëfandiko. Saytu bi mën nañu ko amal ci ay nooyikay walla ci deret. Saytu yi li cu ruuse mën nañu ko am ci ay fan yu neew walla ay waxtu yu neew. Lu ci ëpp saytu bi mën jogge ci jangat buñu amal jële ko ci bakkan wala put. + +Barina ay bërëb u gëstukay ak usin  yuy guestu ci ay  serum pur mëna giss ci teel lu bokkul ci yaram u nit ki. Ci weerup awril juroom ñaari fan ci atum 2020 saytu  yi joxewul dara lo xamante ni mën nañu ci japp ba tax ñu war ko mëna jëfandiko  ci aduna bi yëpp. Cu rewu  Amérique benn saytu jëm ci serum te Cellex amal ko nangu nañu ko pur jëfandiko ko ci ni mu gëna gaawe ci bërëb u gëstukay yi ñu jox ndogal. + +Xalatal +Mandarga feebar yi ñuy saytu ci wallu radiographie yu nit yi am bepp xeetu mandarga buy wane ni am na doomu jangoro mën nañu ci wax jafe jafe ci wallu xool bu bax lu melni lep luy takk ci missaal lamp wala itam jafe jafe  jëm ci wallu nooyikay nit ki am mandargay feebar. Benn bërëb ci wallu radiographie manam xol yan xeet u feebar ñoo nekk ci nit ki te bët munu ko giss ci reewu Italie amal na benn jangat bumu jaglel lu jëm ci wallu nit yi am doomu jangoro bi mungi ñu tass ci internet bi. Kom jixi jaxa dafa am ci ak yeneen xeetu doomu  jangoro yi di walle lu ci "adénovirus" di benn xeetu wirus boo xamante ni dafay ëndil jafe jafe nit ki ci wallu nooyi, skaneer bu andul ak dëgal ni nit ki am na feebar bi di COVID-19 nekkul luñuy mëna jëfandiko pur saytu ndax nit ki am na feebar bi di COVID-19. Reew mu Chine amal na jangat bu yaatu diggante saytu ci skaneer wala saytu ci wallu ADN li ñu giss mooy amana sax skaneer bi nekkul lu am doole loolu pur xam ndax nit ki am na doomu jangoro bi ci yaramam, wante moo gëna gaaw pur ay tontu ba taxna ñungi digle ngir ñu koy jëfandiko lu jëm ci wallu saytu nit yi ndax am nañu doomu  jangoro bi ci dekk yi nga xam ni doomu jangoro bi law na fa bu baax. Amalnañu ay xeetu "neurones"yi nga xamante ni seen liggey mooy fexe ba rañee wirus bi ci kaw amal "radiograpghie" ak "skaneer". +Ñaqq moy ab mbir muy indi kaarange ngir daqq yeen feebar yi. An ñaqq dafay am ab microorganizm bu ñuy yaakaar ni indi feebar moko taxa jòg.ñu ngi kay defaree ci lu ëp ci mikorob yu dee,yu am tooke, wala yu am ay proteyin. Mbir moomu ñu wax nak dafay gënë doolel ni yaramu nit ki di doxee ba noppi jappe ko ni lukay bëg galangkoor,bala mu kay yaqq, tek ci yaqq yeneeni microorganizm yu lunko ak ńom. Nga ñaqq nit ki lolu nañuy wax ñaqqu. Ñaqqu moy faggu bi gën ngir moytu yen feebar yiy walle; Ñaqqu mooy li gënë gaaw ngir jëlefi febaru variol tek ci waani febar yi ci melni polio,ngass ak tetaanoos. Bokk na ci ñaqq yi nga xam ni leernaniou ni amnañ ay jeexital yi baax lu ci melni ñaqqub socc muy sotti, ñqqub HPV, ak ñaqqub febaru ginaar yi. Turu ñaqak ñaqqu mu ngi joge ci Variolae vaccinae(ngasum naq), kaddu googu Edward Jenner moko kereeye jagleelko naq yu feebar yi. + +Njariñ yi +Xeetu ñaqqu yi woor nañu lool te am njariñ ngir xeex feebar yiy law. Wante, di nañu wax ni ñaqqu bi warna def ay jeego ngir gënë baax. Njariñu ñaqqu bi mu ngi aaju ci yi ñu leen di bëg limal: + + Feebar bi ci boppam (setlu nañu ni yenn feebar yi ñaqqu mo ci gën). + Xosaanu ñaqq(yeen ci ñaqq xam nañu lan mooleen taxa jóg ngir feebar bi ñu bëgg xeex). + Walla porogoraamu ñaqqu bi saytu nañu ko bu baax. + Njeexital ci ku jël ñaqq bi;Amna ño xamni seen yaram nanguwul nonu ñaqq yi. + Ponk yu melni ki xeet, magee, wala tolluwayu yaram ci sëy. + +Su fekke ni nit kiñu ñaqq ba pare ci been feebar dafa kontine di am yeenen galankoor ci feebar bobu mën nanu wax ni ak numu mënti deme moy gën4 neewle ay jafe jafe ci ko xamante ni mësul ñaqqu ngir daw feebar bobu. Yii ñuy bëggë lim amna ñu solo lool ci porogaraamu ñaqq. + + Pexe ngir xool nann la porogaramu ñaqq bi mën am ci diir bu gaat wala bu gudd + Saytu guy faral di am ci yenn feebar yi. + Kaarange gu woor ci moytu ab feebar, doontane sax feebar bobu lu neew limuy am la + +Ñaqq yi ñu ngi ci yoonu jëlefi febaru wariyol, ben ci xeetu febar yiy walle yi ëpp ci lumuy ray doomu adama. Yeeneeni feebar yu ci melni rubewol, laago, ngass,nopp buy metti,feebaru ginaar,ak tifoyid nekuñu ay feebar yi ñiy gis leegi donte ni li siiwoon le ay teemeeri teemeeri at ci ginaw te li indi loolu yëp moy ñaqq yi ñu komaase def . Su fekke ni li ëpp ci nit ñi ñaqq nañu leen, di na jafe lool mbas mbi law. Lolu nañuy woowee faggug mbas. Ñaqqu itam dañuy dimbali ngir faggu lawaayu doomu jangoro ji. Ci misaal dafay waañi yaqqute yi febaru xëtër mën indi te ñu kay woowe Streptococcus . Porogaraamu ñaqq yi waañi nañu bu baax lawaayuk yen in feksoon yi jëm ci peneesilin ak yu ni mel. Xayma bi ñu def ci ñaqqum ngass mi mooy ni mën na faggu ci been miliyong nit yu dee at mu ne. + +Gaalang koor yi +Naqq yi ñuy def nit ki ci bamuy nekk ndaw lu woor lë. Gaalang koor yi tamit su fekke ni amna lu neew lë. Gaalang koor yi ñuy faral di jangoontel moy yaram bu taang, mettit ci buñu lay pikiir, ak yaram buy metti. mën nañu ci yoqq itam ni ñen ci nit ñi seen yaram mën na bana nangu ñaqq bi. Gaalang yu tar yi lu neew le . + +Fasong yi. +Yenn ci ñaqq yi am na doomu jangaro ji bunu saytu te rayko wala ay mbir yuñu ci jëlee. + +Yiiy nelaw +Yeen ci ñaqq yi am nañu luñuy wax micoro-organizm yudul yëngu yoo xam ni tooke moka rayy wala tangaay wala rajaason. Mën nañu boole ci misaal yi ñaqqub poli, ñaqqup epatit A,ñaqqup doomu jangoro bu ñuy wax rabies ak yenn ñaqqub socc muy xelli. + +Waañig dangar +Amna yeen ci ay ñaqq yu am ay micoroorganizm yuy waañi dangar. Fsong yooyu di nañu yagg lool ci yaramu nit ki, wante xëy në taxu ñukoo woor nonu ci bu ñu leen defee ci ñenn ñi ko seen yaram nanguwul. + +Tooke bu boon +Naqqub toxoid yi ñu ngi leen defaree ci ay tooke yu ñu jaxase yuy indi feebar kë ay micro organizm. + +Xeetu waksin +Naqqub subunit yi dañuy jëfëndiko ab dammit ci micfroorganizm bi ngir defar li ñuy wax ay soldaar.aqqub subunit yi dañuy jëfëndiko ab dammit ci micfroorganizm bi ngir defar li ñuy wax ay soldaar. + +Conjuguer +Amna yeen ci ay bakteri yu am tooke yu leen di muur yu xawa woyof ay soldaar. Bu nu boole tooke yi ak ay poroteyin, yaramu nit mën na jap kome si tooke yi ay proteyin lañu woon. + +Saytu +Barina ay xeetu ñaqqu yu bees yo xamantani ñu ngi kay jëfëndikoo waye itam ñu ngi ciy liggey ngir ñu gënë effikas.Naqqu yi ci ëpp dañu leen defar ci no xamantenee dañu jaxase ay micro-organizm. ñaqq yu. Amna nak ay xeetu ñaqqu yo xamante ñu ngi leen defaré ak mennef yu ute. + +Tooke gi +Naqq yi mën nañoo am been wala ay mbir yu bari yu ñu më facc. Ñaqq buy facc been feebar ñu ngi japp ni li ko taxa njó mooy ar la ci ludul been doomu jangaro bi wala linu mel. Defar nañu ab ñaqq bu mënë xeex ñaar ba au walax jaan yu bari yu sosoo ci been mikoro-organizm,wala sax mu xeex ñaari mikoro-organizm wala luko ëpp. + +Jaxase ñaqq +Yii ńooy ñaqq yiy jëfëndiko li ñuy wax patozen yuy jugee ci yeneeni mala yoo xamni du ñu indi jangaro ci yaramu doomu adama buñuy facc. + +Magg ak weer +Yaramu doomu aadama ma bi nangu na ni mandarga yi ñaqq bi di utilize bokkul ci moom, yaram bi dafkay yaqq tek ci du lumuy "faate". Bu been ci: + + Ci kaw teye mbir mi ci bamuy teel bala muy ëppi loxo + Ci kaw ñu nangu ko tek ci faagaagal doomu jangoro ji bala muy law + +Komprime yi ak jumtukayu sey +Naqqu yi am nañu ben wala ay komprime, yuy yokk di gawal ligeyuk yaramu nit kiñaqqu yi mën nañu itam am xeetu soldaar yu len di fagul yen walaate yiy and ak salëte. + +Porogaraam +Ngir am karaange gu woor, ñu ngi diggël  xale yi ñu jël ñaqq bi jamono ji ko seen yaram nangoo.Ñuy yokk ni ''xeetu pikiir yi" digle nañuko ngir am "karange gu mat". Li digle nañuko ci porogaramu xeetu ñaqq yu doywaar yi. Bari ay xeetu ñaqq yu ñu digël ñi seen at takku wala ñiy faral di pikiiru ci sen dundu. Lu ci melni feebaru ngass, tetaanos,soj muy xelli ak feebaru xëtër. Xeetu ñaqq yi ñuy digël mak ñi mu ngi jëm ci ñi am feebaru xëtër ak soj muy xelli. + +Taarix +Ci lu jiitu ñuy dugël ñaqq yi jële ko ci feebaru nak ni, feebar bi ñuy wax variol mënoon nañu ko faaggu ci buñuxamoon fan la doomu jangaro bikay joxe di duggee. Fasong rëbb bu ñëkk bi sinua yi doon def ñu ngi ko commaase woon amna junni at ci ginaaw. Ci boori atuk 1760 Edward Jenner jáng na ni rat katu meew yi mësuñu am feebar bobu ñuy wax variol ndaxte amoon nañu ba paré feebar bi ñuy wax febaru nak wi. Ci atum 1796, Jenner jëloon na tuti ndox ci ben rat katu meewu nak bu amoon goom ci loxo mu boole ko ak doomu jangoro bobu di dal nak yi, jaxase ko daldi kay tas ci loxowu ben xale bu ay atam toll ci 8, bi ñu ci tege júroom ben ayu bes mu ñaqq xale bi ngir ar ko ci feebar bi. Ci njeexital gi gis nani gouné gui amoul wone feebar bi.. Jenner daaldi gënë yaatal ay gëstoom tekci ci atum 1798 mu waxni ñaqq bi mou defar lou woor le our ndaw ñi ak mak ñi. Naareelu ndorteelu ñaqqu yi ki di Louis Pasteur moko fi dugël ci boori atu 1880. Nga ñaqq nit ki lolu nañuy wax ñaqqu. Ñaqqu moy faggu bi gën ngir moytu yen feebar yiy walle; Ñaqqu mooy li gënë gaaw ngir jëlefi febaru variol tek ci waani febar yi ci melni polio,ngass ak tetaanoos. Li ëpp ci ñaqq yi ñuy defar mu ngi juge ci xaalis bu gornment bi, uniwersité yi ak o n g yi. Bari na ay ñaqq yu seer lool te wa kër doctoor nokay jëfëndikoo. Limuk ñaqq yi ñu joxe dafa yok te jeggi dayo ci at yii ñu weesu. Tek ci, ñaqq yi ñuy defaral júr gi daf leen di aar ñoom ngir ñu bañ am feebar tek ci ñu baña wall nit ñi. + +Li ci biir wergu yaram +Rangu patents yi ci ñaqq bi mën na nek galangkoor ci ñaqq yu bees yi ñuy jëmële kanam. Ci kaarange gu doyadi gi patents yi am, mën nañu wax ni yeesal yi ñu mbebet mënul jaar ci ludul def ab liggey bu xarañ jëmëleko ci aar ak di nëb yoon yi ñuy aw ngir yokk mëninam. + +Ci ay waxu Mbootay Gi Ëmb Wergu Yaram ci Aduna bi, jafe jafe bi gënë mak bi reew yu neew doole yi di jankonteel ngir defar sen ñaqqu bop mooy ñakkum xaalis, ay jumtuwaay,ak ay nit yu xarañ yu mën ligeey bi. + +Yenen pexe +Gis nañu ni liggey bi ñuy def ci ñaqq yi mu ngi gën di mucc ayib ba am nañu yaakar ni dina gënë am njariñ ci ñi kay jëfëndiko + +Amna ay setlu yu jëm kanam ci yi ñu def ci yen ñaqq yi ñuy jox nit ñi nu naan ko. Bu ci melni bu polio bi bobu wane na ni ay ndaw mën nañ ko joxxe te ñu bañ leena taggat yeen taggat yi. + +Jangat yu xoot yi ñu def ci ñaqq bi ñu tuddee needle-free ñu ngi kay yëggali ci mala yi. + +The development of new delivery systems raises the hope of vaccines that are safer and more efficient to deliver and administer. + +Jëm jëm +Vaccine development has several trends: + + Xarante naqq bi daffa bari  jëm jëm + Ba ci lu yaggul dara rek xeetu ñaqq yi ñi ngi ko jagleelon bébé yi ak gune yi, wante ñu ngi kay bëg jëmële bu baax  ci njagamaar yi ak mak ñi. + Di jaxase ay xeetu ñaqq legi luñuy gis le. + Amna ay yoon yu gënë xarañ yu ñuy jaar ngir gënë ñoñal walum ñaq bi. + Defar nañu ñaqq yi no xamante ne dafay gënë ñoñal xeex gi muy xeex yen reaksion yaramu nit ki, ci ni mu gënee. + Amna ay jeego yu ñuy def ngir doolel ñaqq ndax mu mën daan yen feebar yu tar yi. + Nu ngi liggey ci yokk xarañtewu yeen ñaqq yi ngir mu xeex yeen coxorte jangaro yi. + Neen ci bororm xam xam yi ño ngi jeema liggey ci ay fasong ñaqq ngir gënë xam ni wirus bi mel. Lolu dina tax ñu mën faggu ñaqq yi. + +Références +Mbass mii di koronaa andilna yaaq yaaq yu bari ci adduna bi ñu nekk, yaaq na lu bari ci sunu dëkkuwaay ak linu wër.ndëgëni gi am ci wallum jawu ji taxna ba yaqqute yu bari yi doon am ci jawwu ji wañeekuna. Tere gi génn ak yeneen yi ci top fële ca Chine taxna ba xaaju xaajat ci yaqqute yi daan am ci jawwu ji wañneekuna Taxna ñu bari lëlu baña geen, waañi na lu ci tilim-tilimal linu wër ci reewum Chine, loolu nak jotna aar juroom ñaar fukk ak juroom ñaari junni nit ci lu toll ci ñaari weer Mbass mi waañi na doole reew yi doon mankoo ngir aar liñu wër. tek ci daje bi ñiy xeex wallum yaqqutewuk jawu ji waroona daje ci atum ñaari junni ak ñaar fukk. Waañi na itam koom koom gi kureel gi waroon def xaalis ci gënë ñoñal kurang bii. + +Ci ganaaw tuuti +Ba ci atum 2020 bii ñu nekk,yokkute gaas bi tass ci jawu ji te di juur tooke ca ba izin yi tambalee di genee saxar mën nanu wax ni loolu jur në tangoor wu tar ci jawu ji. Tangoor boobu tax na ba motaañu galaas yi ńu ngi seey ak geej giy nangu suuf si. Yaqqu yaqqu nit yi ci linu wër barina ay fasong. Loolu nak nit ñi rek ñooko waral. Li gënoona soxal doktoor yi ci mbassum feebar bii di COVID-19 moodoon ñu diggël nit ñi ci ñuy lëlu ak di soriyante nekkin. Ci coobare ku nekk, gëstu kat yi waxoon nañu ni laataa mbassum korona bi di COVID-19 li gën mooy ñu waañi yëngu yëngu yi ci wallum koom koom dina am solo. + +Ngelawu dëkkuwaay bi tilim +Bi koronaa bi amee ba leegi, gis nañu ni niñuy tilimalee ngelaw li ñu wër waañeekuna lu baree bari. Waañi tilimal bi ñuy def ci ngelaw li ñu wër mën na tax ba yaqqute yiy am ci jawu ji waañeeku ak lii di COVID-19 bi wante nak leeragul ci ban fasong tilimal moo ëpp limuy yaqq ci lu jëmm ci soppeeku jawuji ak lii di COVID-19 bi.Kureel gu mak gi di gëstu ci linumel, wonena ni ngir teye coronavirus ngir mu baña law dañu war di lëlu di tëc foroñceer yi, te loolu waññi na xaaju xaajaatu yaqqute yi dëkkub Chine di def ci jawu ji.Ci weer bu ndëk ci bi mbass mi doore gis nañu ni reewum Chine waañi na ñaari teemeeri milyong yi tilim bimou deefon ndigëni daaw ci atum 2019 japp nañu ni likowaral mooy roplaan yi ñi teye ak petarol biñu bayyee lak.[4] Ken ku xam xamam jëm ci waalu jawu ji ligeey bobu mën naa wallu 77,000 nit yu naroon dee. waaye ba leegi ki di Sarah Ladislaw biy liggeey ci kureel gi neena desna lu bari ndaxte reewum Chine parewul waañi tilimal jawu ji. Ci diggante 1 fan ci weeru saanwiyee ba 11 ci weeru Marss 2020, fële ca Itaali kureel bi feetee ca Europe setlu na ni lii di tooke biy jugee ci saxaar si izin yi di geenee ak ndaamaar yi ak ñii di liggeey ci di geenee kurang ci jawu ji waañeeku na bu baax. Li lepp nak mu ngi xewee ci biñu tëjjee dëk yi. NASA ak ESA ñu ngi doon jiite gëstu yi ñu doon def ci gaazu Nitrogen te gis nañu ni jëfëndikoo bi waañeeku na bu baax ci bi mbassum COVID-19 tambalee ca Chine. Koom koom bi waañeekuna ba jeggi dayo tek ci waañi tilimal bi doon am rawatina ci reewu taax yi bu ci melni Wuhan ca Chine ci xaaju xaajaat ci li ñu daan tilimal(25%). NASA mu ngi gëstu di saytu ci gaazu ozon ak Nitrogen ak yeneeni xeetu gaaz. Lii yëpp ci xibaar jotna dimbali NASA ci gëstu wam li yëpp li ko waral mooy tëjj bi ñu tëjj dëkk yi ci adduna bi. + +Yoonu ndox ak dundu gi +Linuy soxla ci ak diko jënd ci  jën waañeekuna bu baaxa baax te liko waral mooy mbass mi, teyit napp bi dafa taxaw lool sax. Rainer Froese jën dina gënë bari ndax mbass mi,lu bari ci jën dina yokk ñaari yoon ndax ñakkup napp gi, te ñu ngi ragal ni fële ca Europe yeen xeetu jën yu melni herring mën na gënë yokk. Siñaatir gi ci weeru Awril ren, ngir noppal geej yi ba leegi desna leer. + +Gëstu ak yookkute +Donte ni jëfëndikoo bi ci gaaz bi wañeekuna bu baax, kureel giy saytu enerzi ci adduna neena mbass mi mën na tere ay sosete yu bari ñu waañi seen loxo ci xaalis bi ñu daan joxe ngir ñu gënë ñoñal kurang buy jogee ci jawu ji.Ci loolu lëlu gi ñu yokk tax na ba nit soppi doxalinu ni ñuy ligeeyee. Loolu andi na tamit, linuy jëfëndikoo ci mask ak yeneen di yaqq linu wër ba ci palastik yi. Tilimal ba ngi yokk. Saantar biy ligeeyël adduna bi ci kilimaa neena waañeeku bi am ci roplaan yiy daw,te mbass mi waralko mën na am ay jeexital ci jawwu ji. Te liko waral mooy ñiy liggeey ci roplaan yi di jëfëndiko li ñuy wax ay "Meteorological Data Relay"(AMDAR) ngir mu mën leena jappale ci ñuy artu seen bopp ci lu mën xew. Waa ECMWF tanii nañu koomu AMDAR dina waañeeku bu baax maanaam juroom benn fukk ak juroom ci teemeer bo jël ci seeni ko0m koom dina waañeeku. + +Niñuy doxalee +Foommu nañu daje bi waroona am ci ñi sèqq waallum soppeekup jawwu ji ba 2021 ganaaw ba mbass mi tegee tankam ci dëkk yi ba yoobu leen lopitaal. Waxtaan bobu lu amoon solo lë ndaxreew yi parèwoon nañu ngir tënku ci xaatim yi ñu deefoon ca Pari.Mbass mi waañi na mëninu yeen reew yi ngir ñu xetali ñeneen ñi.ndax dañu tënkuwoon lool ci li leen doy.[5] Been ci kër taskatu xibaar yi japp nani mbèbetu dekalaat been koom koom pur adduna bi yëpp nar na jur ay jëfëndiko yu ëp loxo jëm ci gaaz bi.Ki jiite kureel gu mak gi ci kurang bi neena waañeeku bi ndax mbass mi baaxoon na ñu jeëfëndiko esaanse ak yiu ni mel. + +Tani neena galankoor mën na am +Tambaliwaat ligeeyum garab yi ak dem bi ak dik ci been yoon ganaaw bi ko COVID-19  ak tëjj yi ñu tëjj leep deful ludul yaqq gañcax gi wante du ko gënë ñoñal mukk. + +External links: + +·         United Nations: Six Nature Facts Related to Coronaviruses + +Références +Aminata Sow Faal mu ngi juddu ñaar-fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru awiril atum 1941 ca Ndar (See-Luwi ca Senegaal). Nekkoon na ab bindkat buy bind ay téere, rawatina yu nettali, bokkoon tamit ci ñi xàll yoonu bind càllalag Afirig ci làkku farañse. + +Dundu boppam +Aminata Sow Fall est mère de sept enfants, dont le rappeur Abass Abass,. + +Ay téereem + + Le Revenant, roman, 1976 + La Grève des bàttu, 1979 : présélectionné par le jury du prix Goncourt en 1979 ; Grand prix littéraire d'Afrique noire en 1980 ; porté à l’écran par Cheick Oumar Sissoko en 2000,. + L’Appel des arènes, roman, 1997: présélectionné par le jury du prix Goncourt en 1982 ; Prix international pour les lettres africaines ; porté à l’écran par Cheikh N'Diaye en 2006 + Ex-Père de la Nation, roman, 1987 + Le Jujubier du patriarche, roman, 1993 + Douceurs du bercail, roman, 1998 + Un grain de vie et d’espérance, réflexion sur l'art de manger et la nourriture au Sénégal suivie de recettes proposées par Margo Harley, 2002 + Sur le flanc gauche du Belem, in L'Odyssée atlantique (collectif), nouvelle, 2002 + Festins de la détresse, roman, L'Or des fous, éditeur avec l'Alliance des éditeurs indépendants 2005 + L'Empire du mensonge, roman, 2017 + +Ay raayaam + + Lauréate du Grand prix littéraire d'Afrique noire pour La Grève des bàttu (1980). + Prix international pour les lettres africaines pour L'Appel des arènes (1982). + Nommée docteur honoris causa de Mount Holyoke College, Massachusetts (25 mai 1997). + Chevalier de l'ordre national du Mérite + Chevalier des Palmes académiques + Chevalier de l'ordre de la Pléiade + Chevalier de l'ordre national du Lion du Sénégal + Commandeur de l'ordre des Arts et des Lettres (2012) + Grand prix de la Francophonie de l’Académie française (2015) + +Téere wala dali web yees y + +Lees bind ci moom ak ay téereem + + Faustine Boateng, At the Crossroads: Adolescence in the Novels of Mariama Bâ, Aminata Sow Fall, Ken Bugul and Khadi Fall, Howard University, septembre 1995 + Madeleine Borgomano, Lectures de "L'Appel des arènes" d'Aminata Sow Fall, Nouvelles éditions africaines, 1984 + Mwamba Cabakulu, Comprendre et faire comprendre "La grève des bàttu" d'Aminata Sow Fall, Paris, L'Harmattan, 2002 + Marie-Françoise Chitour, « Aminata Sow Fall », dans Christiane Chaulet Achour, avec la collaboration de Corinne Blanchaud, (dir.), Dictionnaire des écrivains francophones classiques : Afrique subsaharienne, Caraïbe, Maghreb, Machrek, Océan Indien, Éd. H. Champion, Paris, 2010, p. 426-430 + Lydia A. Forster, Le discours féminin sur la femme à travers les œuvres de deux romancières sénégalaises : "Une si longue lettre" (1979) de Marianne Bâ, "La Grève des bàttu" (1979) et "L'Appel des arènes" (1981) d'Aminata Sow Fall, Faculté des Lettres et Sciences Humaines, 2000 + Médoune Guèye, Aminata Sow Fall : oralité et société dans l'œuvre romanesque, Paris, L'Harmattan, 2005, 197 p. + Houda Jaafar, Les superstitions magico religieuses : "La grève des bàttu", d'Aminata Saw (sic) Fall, "Xala", d'Ousmane Sembène, "Le monde s'effondre", de Chinua Achebe, 2004 + C. Mazauric, « Fictions de soi dans la maison de l'autre (Aminata Sow Fall, Ken Bugul, Fatou Diome) », Dalhousie French Studies, 2006, vol. 74-75, p. 237-252 + Isatou Ndow, La technique romanesque dans les œuvres d'Aminata Sow Fall, Faculté des Lettres et Sciences Humaines, 2000 + Susan Stringer, « Cultural Conflict in the Novels of Two African Writers, Mariama Ba and Aminata Sow Fall », A Scholarly Journal on Black Women, 1988, supplément p. 36-41 + Dorothy Davis Wills, « Economic Violence in Postcolonial Senegal: Noisy Silence in Novels by Mariama Ba and Aminata Sow Fall », dans Violence, Silence and Anger: Women's Writing as Transgression, Charlottesville, University Press of Virginia, 1995, p. 158-71 + +Ay filmam + + L'appel des arènes (long métrage), 2005 (écrit par Aminata Sow Fall) + Visage : Aminata Sow Fall (court-métrage) +Article utilisant une Infobox +Lingeer Ndate Yàlla Mbóoj,am nu koy woowee Ndete Yàlla, mu ngi juddu atum junni ak ñetti téemeer ak fukk, génne àddina atum junni ak juróom ñetti téemeer ak juróom benn fukk. Nekkoon na buur bu jigeen bu mag ca réewum waalo, réew mi féetewoon ca bët-gannaar penku Senegaal. +Article utilisant une Infobox +Karolin Fay Jóob mu ngi juddu fukki fan ak benn ci weeru sulet atum 1923 ca Funjuñ, faatu ñaar-fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru sulet atum 1992 ci Dakaar. Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk ndawu réew (deppite), nekk it jigeenu ji jëkk a nekk jëwriñ ci Senegaal. Moo doonoon soxnay Demba Jóob mi ñu bóomoon atum 1967. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Cosaan ak njàngam +Karolin Fay Jóob mu ngi juddoo Funjuñ (Fatig, bokkoon ci Afrig sowu jant gi doon wéy ci waawu Frãas (Afrique Occidantale française) fukki fan ak benn ci weeru sulet atum 1923. Doom la woon ci Luwi Jéen Fay, xam-xamam màccoon ci mbirum waññi (kontaabilite), bokkoon ci SFIO, nekkoon tamit kenn ci soskati Bloc démocratique sénégalais. Way-juram wu jigeen mu ngi tuddoon Faatim Jóob soqeekoo ci Mañ Jóob Mbaaco bu Waalo. Njàng mu suufe mi, mu ngi ko defe seen dëkk laata muy jàngeeji lekool Albeer Saró bi nekk tey lekool Bert Móbeer. Mu daldi am ndam ci joŋanteb dugg lekool normaal bu xale yu jigeen yi bu Afrig sowu jant gi doon wéy ci waawu Frãas (Afrique Occidantale française), nekk ca Tëngeej (Rufisque)Foofee la génne ak ab lijaasa atum 1945 ginnaaw bu mu jëlee ñetteel ci joŋante ba. Ñi mu fa nekkoonandoo, ràññe nañu ci Anet Mbay Dernëwil mi jëloon pee ak Ndey Kumba Jaxate mi jëloon ñaareel, Aan Mari Sohaay, Saan Martee Siise (Jeanne Martin Cissé). + +Ay jaar-jaaram ci njàngale mi, +Lijaasa bi mu am atum 1945 moo ko tax a nekk ab jàngalekat ca Luga ci ndigalu xelalkatam bi Abdulaay Satsi (Abdoulaye Sadji), ca Cees, ca Maatam ak ca Mbuur foofee ca Mbuur la nekkoon njiitu lekoolu xale yu jigeen yi 1951 ba 1962. Ca Mbuur googu, la tase ak Demba Jóob, mu nekkoon ab wottukat maanaam sirweyãa ci lekool bu tuddoon Cours normal bu Mbuur, lekool boobu sax, moom Demba Jóob lañu ko mujj tudde. Mu daldi nekk soxnas Demba Jóob atum 1951. Bi muy wéyal njàngale mi, la dugg ci pàrti bile di Bloc démocratique sénégalais ca Luga atum 1945 ; bi mu xamee ne boole ñaar yi dina jafe lool (njàngale mi ak pólotig bi), ndax farlu bi mu amoon ci pólotig dafa doon gën di yokk, la ko Léwopool Sedaar Seŋoor, mi doon jiite pàrti bi, may mu nekk ab jàngalekat buy yëngu rekk ci lépp luy suqali kow gi + +Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig +Karolin Fay Jóob bokk na ci ñi sos kureelu jigeen gi ànd ak pàrti bile di Union progressiste sénégalaise, daldi nekk njiit la suyee (juin) 1954 ca Cees ginnaaw bu Faatu Siga Ñaŋ bàyye. Mu daldi nekk ab deppite diggante 1963 ba 1978, dugg nag ci taarixu réew mi ndax looloo ko tax a doon jigeen ji jëkk a nekk deppite ci Péncum ndawi réew mi. Atum 1963 xaat, mu ngi doon wax waxi sos sàrtu njaboot bi (Code de la famille), di ñaax jigeen ñi ci dem ak seen bopp, bañ a wékku ci kenn. Moom rekk moo doon jenn jigeen ji bokkoon ci woteb sàrtu njaboot bi. Moo nekkoon ñeenteelu kilifa gi topp ci njiitu péncum ndawi réew mi (ñeenteelu wis peresidãa bu péncum ndawi réew mi). Atum 1964 lañu ko fal njiitu jigeeni Union Progressiste Sénégalaise, mu dellu nekk sekerteer seneraal bi ñu toftal ci njiitu kureel gile di Jigeeni Afrig yi, maanaam Panafricaine des femmes ci farañse. Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk jëwriñ ci réew mi ndax 1978 lañu ko tabb jëwriñ ji yore wàllu taxawu néew-di-doole yi, nekkaat jëwriñ ji ñu feggal jëwriñ ju jëkk ji diggante 1981 ba 1982, dellu nekkati jëwriñu nguur (ministar detaa) diggante 1982 ba 1983. Ci njëwriñam lañu gis ne sos nañu ay kureel yuy gëddal ak a dooleel jigeen ñi. Am na sax ab nettali ci li xewoon ca kongareb pàrti ba woon ca Cees atum 1958, nga xam ne woowuñu ca woon benn jigeen, moom mu dem ca ba pare, naqarlu ci kanam Seŋoor, njiitu réew mi, li fa jigeen ñi teew ba pare te kenn ci ñoom jëlu fa kàddu. . + +Karolin Fay Jóob jàppoon na ne taxawu na jigeeni réewam diiru fukki at yoo xam ne moom kese moom nekk ca péncum ndawi réew mi « Xeex naa ngir Sàrtu njaboot bi am, ngir ñu teg ndimbali njaboot yi ci yoxoy jigeen ñi ». Mu dellu jàpp ne ay jaar-jaaram ci pólotig dañoo tar, kenn ci góori pàrti bi daanu ko jàppale ndax mësuñoo rafetlu ràññekug jigeen ñi wala fit wi ñu am, def benn dank ñoomi neen, di xàccandoo, di dóorandoo. + +Kàddu yile ca waxtaanam wa lañu leen tibbe woon : Nee na woon ca ndajem fukki fan ak juroom mu jigeen ñi (keesenu jigeen ñi) « Lu guy rëy rëy, warul a fàtte mukk ne ab xoox bu ndaw moo ko jur ». Ci lu aju ci taxawu àq ak yelleefi jigeen ñi, nee na : « Waxuma waxi taxawu jigeen ñi bu jéggi dayo. Waxuma ne na góor ak jigeen tolloo, waaye dama bëgg ñoom ñaar ñuy mottaliwante. Nekkuma kuy yéegal fii, di wàcce fee. » + +Ay jëfam ak i sargalam + + Màngasiinu pepp bu USAID joxe. + Moom lañu yaayale woon ñaar-fukk ak juroom-ñaareelu keesenu jigeen. + Amal ay tooli ñépp + Def ay farmasi ci dëkki kow yi, ay lekooli tuut-tànk ci Garãa Yoof, Cees, Tàndem (Kaasamaas), Ayere Laawo (Fuuta) + Mbindum sàrtu njaboot ci Senegaal (moom rekk moo nekkoon jigeen ji bokkoon ca wote ba) + Ay ndimbali jaboot ngir jigeen ñi + Wax ñu jagleen jigeen ñi bésu ñaar-fukki fan ak juroom ci weeru màrs atum 1972 te ñu soppi ko tey keesenu jigeen + Sos ay mbootaay yuy taxawu ak a dooleel jigeen + Sos ay kureeli dimbalante, lebal ak denc xaalis yu ñu mujj soppi ag ràbboo + +Toftal bi + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Jukki yi ñu ko tudd + + Pólotigu Senegaal (Politique du Sénégal) + Nekkinu jigeen ci Senegaal (Condition féminine au Sénégal) + Limu jigeen ñi jot a nekk jëwriñ ci Senegaal (Liste de femmes ministres sénégalaises) + +Lees bind ci moom + + « Caroline Faye Diop » in Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, Dakar, 2006, p. 164 + « Caroline Faye : Première femme députée et ministre du Sénégal », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 78-79 +Germaine Acogny, ca Benee la juddoo ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak ñent fukk ak ñent, ab fecckat ak naskatu pecc di doomi Farãas ak Senegaal, di jëmm ju am mboor (taariix) ci wàllum pecc ci Afrig ginnaaw bi mu ubbee bulub feccukaay bu njëkk ci Afrig ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñatt, ci Ndakaaru. + +Germaine Acogny, doomu Togun Serwee Akoñi la, nekkoon liggéeykatu nguur ci jamonoy nooteel te bind « Nettali Aloofo », delloo na ko njukkéel ci po mii dii « À un endroit du debut » + +Sos na ab barabu feccukaay ci Ndakaaru ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñatt. + +Ci diggante atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar ak atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatti fukk ak ñaar, jiite na Mudra Afrique bi Maurice Bejart ak njiitu réew mi woon Leopold Sedar Seŋghor sosoon ci Ndakaaru. + +Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatt fukk, mu génne téereem bii di « Peccum Afrig » ci ñatti làkk. + +Ginnaaw tëjug Mudra Afrique, la dem jàngale ji ca L'Isle-Jourdain, digganteem ak Toulouse tolu ci fan wer i kilometar ak juroom, ginaw bi mu dem dëkki ca Bruxelles andadook Maurice Bejart, di amal ay ndajey peccum Afrig ci àddina wërngal kapp, mu doon ndaje yu am solo ci saa-Órob ya. + +Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatt fukk ak juróom, moom ak boroom këram, Helmut Vogt ñu sos «bulu-lekoolu pecc ak tiyaatar bu ñatteelu àddina» ca Toulouse. + +Ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom, Germaine Acogny, jëloon dogalu ñibbisi Senegaal ba ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom ñatt, mu sos mbootaay gii di Jant-Bi/lekoolu suuf si ( l'Ecole des Sables). + +Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom ñaar ba ci atum ñaari junni, la ñu ko tabb njaatige ci fànnu pecci Afrig yi ñuy fent ca Pari ak ay ndajey pecc yu bees yu Afrig. + +Ci atum ñaari junni ak ñent mu dallo am màkkaan mu ñeel àddina wërngal kepp te di yëngu ci peccum Afrigu démb ak tay mu tuddee ko Lekoolu suuf si, féete ca Tubaab Jalaaw. + +Màkkaan moomu amoon i jafe-jafe si wàllum koom ci njeexitalu atum ñaari junni ak fukk, ginnaaw bi mbootaayug Olànd gii di Dowen dakkalee ndimbal li mu ko doon jox. + +Germaine Acogny jot na ay mbandal yuam solo yi ñuy takkal nit ñu ràññeeku ak nit ñu jàmbaare ci fànnu mbatiit yu réewum Farãas ak réewum ci Senegaal. + +Ci atum ñaari junni ak fukk ak ñent, bokk na ci juróom fukki jëmm yi ñuy gën a bàyyi xel ci àddina bi, këru caabal gii di, Jeune Afrique tabb koko. + +Ci atum ñaari junni ak fukk ak juróom ñent, mu feeñ ci film boobu di ''Yao'' te Omar Si doon si jëmm ji ci gën a fés. + +Ko 17 2021, moom ko gaynde d'or de la pecc par la Biennale de Venise. + +Pecc yu ëpp solo yi mu bind + + 1987 : Sahel,, feccu benn nit, mu bind ko fecc ko it + + 1994 : Yewa, Eau sublime Ndox mu gànjaru + + 2004 : Fagaala, powum fecc ak Kota Yamasaki, ñu jagleel ko rayante ga woon ca Rwanda + + 2007 : Les Écailles de la mémoire ak Jawole Willa Jo Zollar + 2007 : Waxtaan, di càmbar ci nguur [1], + + 2016 : À un endroit au début ,Ab barab ca njëlbéen mu nas ko ak Mikaël Serre + +Sources +Pecc +Article utilisant une Infobox +Faatu Bom Bensudaa mu ngi juddu fanweeri fan ak benn ci weeru sãawiyee atum 1961 ci Bànjul. Laykat (awokaa) la bu dëkk Gàmbi nekk tamit toppekat bu mag bu ëttu àttekaayu àdduna bi (pólokirëer seneraal bu Cour pénale internationale (CPI) ) ginnaaw bu fa nekkee, diiru juroom-ñetti at, toppekat bi topp ci kow njiit la. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Nguneem +Faatu Bensudaa mu ngi juddoo Bànjul. Waajuram wu góor ku njaboote la ndax am na ñaari jabar, am ak waajuru Faatu Bensudaa juroom-benni doom, am ak jeneen jabar ji juroom-ñaari doom. Waajuram wu góor nguur gi la doon liggeeyal, waajuram wu jigeen di liggeeye ci restoraŋub liise. Wax na ne, ci seen njaboot gi, góor ak jigeen yépp lañu doon ñaax ñu dem jàngi lekool. Kenn ci ay magam ? yu jigeen ab deppite la woon, am ci ku nekk jigeen ji jëkk a def surnaal ci tele bu Gàmbi, am ku ciy liggeey ci wenn tëralin wu jëm ci jigeen ñi te mbootayu xeet yi (Nations Unies) sumb ko. + +Njàng ak tàggatoom +Faatu Bensudaa dafa teel a bëgg xeex ngir nit ñi jot seen àq ak yelleef, rawatina jigeen ñi, di dem di teeweji ay layoo. Ginnaaw bi mu jàngee ci daara yu digg-dóomu te ñu ràññe woon ko ci lool, la Yàlla def mu nekk gerefiyee ca àttekaay bu Bànjul. Ci ndimbalu burs bu ko nguuru Gàmbi joxoon, la dem jàngi xam-xamu yoon ca Niseriyaa. Foofee, dafa jëkk a jànge ca iniwersite bu Ife nga xam ne tey moom lañu tudde iniwersite Obafemi-Awolowo 1982 ba 1986, laata muy jàngeji ca Nigerian Law School bu Lagos, foofa nag la ame lijaasa yoon bu tudd barrister at law atum 1987. + +Bi mu liggeeyee diiru ñetti at, la bindu atum 1990, ci ab lekoolu mbootaayu xeet yi, lekool boobee mu ngi tudd International Maritime Law Institute, nekk ca Malt, foofee lañu ko joxe ab lijaasab yoonu géej (diplôme de droit maritime) atum 1991. Bi mu génnee ci ngornamaŋ bu Gàmbi, Faatu Bensudaa dafa amaat yeneen lijaasa, benn bi mu ngi ko am nowàmbar 2001 ca Comité international olympique ca Niw York, beneen bi, doon lijaasa buy firndeel njàngum làkku farañse mu mu def ñu naan ko DELF 1er degré te njëwriñ ji yore wàllu ndaw ñi, njàng, njàngale ak gëstu ju réewum Farãas jagleel ko ko. + +Atum 1987 lañu ko nangul ag bokkam ci kureelu laykat (awokaa) gu Gàmbi. Ci menn at mi ñu tabb ko xelalkat ci ngornamaŋ bu Gàmbi. Féewiriyee 1994 la nekk ab toppekat (pólokirëer). + +Taxawaayam ci nguuru Yàyya Jàmme +Ginnaaw foqati nguur ga amoon sulet 1994, la Faatu Bensudaa nekk kilifa gu am solo, ci wetu Yàyya Jàmme, di ko xelal ci wàllu yoon. Ñu yéegal màqaamaam atum 1996, def ko toppekat bu solowu ba 1998 ñu tabb ko toppekat seneraal bu Bànjul ak jëwriñ ji yore yoon ci ngornamaŋ bu Gàmbi,, njëwriñ jooju moo fa nekk ba bi ñu koy wàcce weeru màrs 2000. + +Ñu ŋàññ nguuru Yàyya Jàmme ndax ñàkk a sàmm àq ak yelleefi doom-aadama, jàppe ko ni « genn ci nguur yi dàq a jaay-doole, dàq a noot askanam ci àdduna bi ». + +Liggeeyu boppam +Ginnaaw bi mu liggeeyee ci nguuru Yàyya Jàmme ba pare, dafa daldi ubbi genn këru liggeeyukaayu laykat, rax-ci-dolli jiite benn bànk diggante 2000 ba 2002. + +TIRBINAALU ÀDDUNA NGIR RUWÀNDAA +Atum 2002 la nekk xelalkat ci wàllu yoon ak wuutukatu toppekat bu tirbinaalu àdduna ngir Ruwàndaa ca Arusa, ca Tãasani. + +Ëttu àttekaayu àdduna +Atum 2004 ba léegi, mu ngi liggeeye ci Ëttu àttekaayu àdduna bu La Haye. Dafa fa jëkk a nekk toppekat bi sës ci toppekat seneraal bi di Luis Moreno Ocampo, laata mu koy wuutu fukki fan ak ñaar ci weeru desàmbar atum 2011, daldi waat fukki fan ak juroom ci weeru suyee (juin) atum 2012. Téemeeri réew ak ñaar-fukk yi bokk ci ëttu àttekaay bi ñoo ko tànn, ci tànneef bu doxoon diggante juroom-fukki nit ak ñaar, kenn ku ci nekk di yóotu palaas bi. + +Ngornamaŋ bu Amerig dafa ko lànkal wiisaa awiril 2019 ba léegi, ndax dogalu ubbi ab lëñbët bu mu jël, ngir leeral tuumay salfaañe sàrti xare yu tegu ci ndoddu làrme bu Amerig, ca Afganistãa. + +Ay raayaam + + Ci gis-gisu surnaal bile di Time, moom Faatu Bensudaa, bokk na ci téemeeri nit ñi gën a fés, seen kàddu gën a diis ci àdduna bi atum 2012. + Surnaal bii di Jeune Afrique, moom la def « kenn ci juroom-fukki jigeeni Afrig ñiy jëme dénd bi kanam ndax seen jëf ak seen sumb yi ñuy amal ci seen liggeey (2014 ba 2015) ». + +Dundug biiram +Soxna la ci benn borom xam-xamu koom ak dun, bu cosaanoo Marog tey dundu Gàmbi, mujj nekk ku bare ay isin. Am nañu ñaari bant. + +Seetal tamit +  +Ci yeneen naali wikimedia yi : + +Faatu Bensudaa, ci Wikimedia Commons + +Jukki yi ñu ko tudd + + Ëttu àttekaayu àdduna bi : (Cour pénale internationale) + Limu way-pólotig yu jigeen yi (Liste de dirigeantes politiques) + +Lees jële feneen + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër +Article utilisant une Infobox +Porofesëer Awa Mari Kol (borom këram sant Sekk) mu ngi juddu benn fan ci weeru mee atum 1951, nekk ab doktoor di tamit way-polotig ci Senegaal. Ab gëstu la buy gëstu li ëpp ci "SIDA" bi nga xam ne, siiwal na ci ay jukki yu bare. Nekkoon na kilifag deppàrtemaa ca "ONUSIDA"ca "Genève" diggante 1996 ba 2001. Diggante 2001 ba 2003 ak 2012 ba 2017, moo nekkoon jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi ci Senegaal. Fukki fan ak benn ci weeru septàmbar 2017 ba léegi, jëwriñu nguur la (ministar detaa) ci wetu Njiitu repibilig bu Senegaal. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Dundug biiram +Am na borom-kër, am ñeenti doom. + +Njàng ak tàggatoom +Bi mu paree njàngum kër doktoor mi la am ndam ci ab joŋante bu mu doon def ngir dem wéyal njàngam ci biir lopitaali Dakaar yi atum 1975. Atum 1978, mu am doktoraam. Atum 1979-1980, la dem ca Farãas, ca Liyoŋ di liggeey ci bérebu sowetaas bi ñi yore feebar yiy wàlle nekk ci lopitaal bu Croix-Rousse, foofa dañu ko jàppe woon ni gan gu leen jàppele ci seen liggeey ba. Bi mu ñibsee Senegaal la daldi am lijaasaam bi aju ci xam-xamu doomu jàngoro te farañse naan ko (spécialisation en bactériologie-virologie) atum 1982 ak beneen lijaasa bu aju ci feebar yiy wàlle tey faral di am ci suñu réewi Afrig yi ñu naan ko (maladies infectieuses et tropicales) atum 1984 ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar. 1982-1988, def na ay tàggaytu yu bare ci naka lañuy defe ay gëstu ak naka lañuy jàngale ci Dakaar, Libërwiil ak Bordóo. Ci fanweeri atam ak ñett, atum 1984, la doon jigeen ji jëkk a nekk ab agerese ci njàngum paj fii ci Senegaal, loolu waral tey mu doon kenn ci jigeen ñi xàll yoon woowule ci réewi Afrig yi làkku farañse yépp boole. Atum 1987, njàngum jàngoroy mbas (épidémiologie appliquée et bio-statique) ma mu defoon ca Annecy, ca Farãas, te Fondation Mérieux ak CDC bu Atlanta amaloon ko, tax na koo mottali te gën a mokkal ay mën-mënam ci wàll wi, rax-ci-dolli nekk ab way-bokk ci mbootaay gi boole borom xam-xami jàngoroy mbas yiy génn lopitaal yi, di liggeeyeji ci biti (Association des épidémiologistes de terrain). + +Ay jaar-jaaram ci liggeeyu kër doktoor +Atum 1989 lañu ko tabb porofesëer titileer bu màkkaanu feebar yiy wàlle bu iniwersite bu Dakaar ak njiitu bérebu fajukaayu feebar yiy wàlle bu opitaal Faan (Dakaar). 1989 ba 1996 la nekkoon njiitu Clinique-Counseling bu Kureelu réem yiy xeex sidaa. Liggeeyam foofee, moo doon di saytoo ka lëkkale liggeey bi aju ci toppatoo aji-feebari sidaa yi, seen yaram, seen xel ak seen nekkin ci biir askan wi, ci la sax gise aji-feebar ji jëkk a yore sidaa ci réewum Senegaal, atum 1986, tàggat tamit ay liggeeykati kër doktoor ci jëfandikoo jumtukaayi feebar yi seen wàllante di jaare ci sëy (MST)/sidaa. Ci jamono jooju, mu ngi bokkoon tamit ci kureel gi jiite bépp liggeey bu jëm ci xeex sibbiru ci Senegaal (1994-1996), bokk tamit ci kureelu réewum Senegaal gi fi nekkal Mbootaayu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS Senegaal) (1993-1994). + +Bokk na ci jaar-jaari Awa Mari Kol Sekk, Mbootaayu xeet (Nations unies) ya mu nekkoon di liggeey diggante 1996 ba 2001 ci benn tëralinu wu aju ci VIH/SIDA (ONUSIDA. Dafa fa jëkk a nekk njiitu deppàrtemaa biy jàppale réew yi. Saytu na liggeeyu kàngami àdduna yu mag. Kàngam yooyee, seen liggeey moo doon amal ay pexe ak ay doxalin ci fànni xarala, rafetal, àq ak yelleefi doom-aadam, te jiital ci ñi gën a néew-doole ; seen liggeey nekkoon na tamit fexe ba aji-feebar yi mën di faju, di jot ci garabi sidaa yi bu baax, di bind ak a siiwal jëf ju bare njëriñ ji ak di dooleel réew yi ci wàllu xeex sidaa. + +Soskat wala way-bokk la ci njiiteefu mbootaay wala lëkkaloog kureeli àdduna yu bare yu mel ni : kureelu àdduna gi séq jàngoro yiy wàlle, kureelu Afrig giy gëstu ci mbiru njur (The Population Council), kureelu Afrig giy xeex sidaa (OPALS), kureelu Afrig giy gëstu ci sidaa, kureelu Afrig giy yëngu ci « Rafetal ak àq ak yelleef yi aju ci VIH » (PNUD) ak kureel gile di Jigeen ak sidaa ci Afrig (SWAA). Def na ay ceet aji-tawat yu bare ci santaaneb kureelu àdduna yu bare te wuute. Nekkoon na way-bokk ci liggeeykati kureelu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS), doon ko bindal téere bi aju ci « Wér-gu-yaram ak suqaliku » weeru desàmbar 1993, bokkoon na tamit saytukati Global Program on AIDS (GPA) atum 1992-1993. Kenn la ci ñi jiite woon trac B (ab kilinig la) bu kureel gi doon waajal ndajeem waxtaanu àdduna mi amoon ci sidaa ca Vancouver (Canada) weeru mee 1995 ba weeru sulet 1996. Nekkoon na tamit njiitu ay naali gëstu ci sidaa te àndoon ci ak këru gëstu ci sidaa gu Farãas (ANRS), Eestiti gëstu bu Harvard, iniwersite bu Seattle, NIH, bérebi gëstuy farmasi yi wala PNUD. + +Yeneeni fànni wérug yaram yu mel ni ñakku ngir aaru ci ŋas, njàmbataan, jàngoroy res B (epatit B), tetaanos, jàngoroy jàdd yi (meneesit yi) wala sëqat-su-mag si, bokk nañu ci ay tooli gëstum. Li mu bind yépp, ci jukki ak téere, siiwal leen, ëpp na téemeer ak juroom-fukk. + +Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig +Njiitu réew mi moo ko woo mu ñibsi mee 2001 ngir nekk jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak fàggu gi ci ngornamaŋ bi. Ay jeego yu wóor amoon nañu ci wàllu wér-gu-yaram ndax liggeeyam. Bokk nañu ci jeego yooyu, ay coppitey campeef, coppiteg lopitaal gi, tëralinu ñakk wu ñu yaatal wi, xeexu sibbiru bi, sidaa bi, feebar yi dul wàlle, wérug yaramu mag ñi, sawarloog liggeeykat yi, caytug xaalis bi, digaale bi ak diggante yi ak ñeneen ñiy liggeey wala ñiy dugal xaalis ci wàll wi. + +Li ko Maki Sàll jàppal mooy ne benn, des naa dugal ay yoxoom ci wotey deppite yu 2017, ñaareel bi, jafe-jafe bu réew mi amoon ngir am ay rajogaraafi, looloo waral sax, jëlaatu ko woon ci ñaareelu ngornamaŋ bu Bun Abdulaay Jonn bu juroom-ñaari fan ci weeru septàmbar 2017. Waaye mujj na nekk jëwriñu nguur (ministar detaa) ci wetu njiitu réew mi. + +Bokk na ci njiiteefu kureelu àdduna gi yore wàllu ñakk yi (International AIDS Vaccine Initiative, IAVI). + +Yeneeni yëngu-yëngum +Ku fonk tàggat yaram la, doon ci yëngatu bu baax, nekkoon na fi sax, basketkat bu daan joŋante ci àdduna bi. + +Ay medaay + + Ordre des Palmes académiques (Farãas) + Ordre national du Mérite (Farãas) + Ordre national du Mérite (Burkinaa Faaso) + +Tënk + + Njàng + + 1978 : docteur d’État en médecine (Dakaar, Senegaal) + 1982 : C.E.S. de bactériologie – virologie + 1984 : C.E.S. de maladies infectieuses et tropicales (Dakaar, Senegaal) + + Ay jaar-jaaram + + Jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak taxawu askan wi ci Senegaal : 2012 ba tey + Jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak fàggu gi ci Senegaal : mee 2001 ba 2003 + Njiitu deppàrtemaa " Jàppale réew yi ak gox yi ca ONUSIDA ca Genève" féewiriye - mee 2001 + Njiitu deppàrtemaa "Doxalin, pexe ak gëstu ca ONUSIDA" diggante 1996 ba féewiriyee 2001 + Porofesëer titileer bu màkkaanu feebar yiy wàlle bu iniwersite ak njiitu lopitaalu (CHU) bu Faan 1989 ba 1996 + Lëkkalekatu Kureelu Clinique-Counseling + Lëkkalekatu tàggatu liggeeykati wér-gu-yaram ak taxawu askan yi ci mbirum sidaa : 1989 ba 1996 + Way-bokk ci kureelu réewum Senegaal gi fi nekkal Mbootaayu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS Senegaal) : 1993 ba 1994 + 1979 – 1980 Gan guy jàppale liggeeykati lopitaal bu Croix-Rousse : 1979 ba 1980 + +Ceet ak gëstu ci sidaa : + + Ay Ceet yu bare ci sidaa, ci wérug yaram, ci njur gi ngir kureeli àdduna yu takku, rawatina OMS ak askanu Council + Way-bokk ci gëstu "Sëqët su mag si ak sidaa", ànd ci ak IMEA, di bérebu gëstu bu Afrig ci wàllu kër doktoor ak mbas + Këru gëstu ci sidaa (ANRS), Farãas ak kureelam gu tudd coopération française atum 1996 + Way-bokk ci kureelu Afrig giy yëngu ci jikko yu rafet, àq ak yelleef ak VIH » (PNUD) : 1994 ba 1996 + Way-bokk ci kureelu réew miy sàmm jikko yu rafet yi aju ci fàggug sidaa gi, Dakaar : 1992 ba 1996 + Way-bokk ci kureel gi jiite tëralinu réew miy xeex sibbiru, Dakaar : 1994 ba 1996 + Njiitu kureelu borom xam-xam gi doon waajal ndajem àdduna mi aju woon ci sidaa ci Afrig, Dakaar : 1991 + Kenn la woon ci ñi doon jiite Groupe Clinique bu fukkeelu ndajem àdduna ak benn te aju woon ci sidaa ca Vancouver (Kanadaa) : 1996 + + Mbootaayu jigeen giy xeex sidaa ci Afrig (SWAA), way-bokk ak njiitu SWAA Senegaal la woon + Kureelu àdduna gi ñu samp ngir xeex feebar yiy wàlle (way-bokk la woon ci kureel gu ndaw gi ko doon jiite) + Kureelu Afrig giy xeex sidaa OPALS + Kenn ci way-bokk yi sos OPALS ak njiitu OPALS Senegaal ba woon. + Way-bokk ci Ngomblaanu xam-xam ak xarala gu Senegaal + Way-bokk ak njiitu Kureelu yemale, jikko yu baax ak jëf (COMEVA) + Way-bokk bu ñu boole ci ngomblaanu réew mi ci wàllu, farmasi, Farãas (ñu fal ko bésu 30.09.2015) + 2003 : Docteur honoris causa bu Iniwersite Pierre-et-Marie-Curie. + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Seetal tamit + +Lees bind ci moom + + « Awa Marie Coll Seck : une vie de battante », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 92-93 + +Jukki yi ñu ko tudd + + Liste des ministres de la Santé du Sénégal | Santé au Sénégal : Limu jëwriñ yi yore woon wér-gu-yaram yépp ci Senegaal | Wér-gu-yaram + Liste de femmes ministres sénégalaises : Limu jigeen ñi jot a nekk jëwriñ yépp ci Senegaal + +Lees jële feneen + +   +Ci yeneen naali Wikimedia + +Awa Mari Kol Sekk, ci Wikimedia Commons + + Dundu ak jaar-jaaram + + (Dundu ak jaar-jaaram) (dalu web Pressclub) Biographie (site Pressclub) + (Dundu ak jaar-jaaram) (dalu web Roll Back Malaria) (Biographie (site Roll Back Malaria) + + Ak yeneen + + Limu jëwriñ yi yore woon wér-gu-yaram yépp ci dalu webu njëwriñ ji (Liste des anciens ministres de la Santé sur le site du ministère.) + Wax ci xeexu sibbiru bi ( Interview sur la lutte contre la malaria.) + Meetar Awa Mari Kol Sekk, ñu def ko doktëer onoris kóosaa (Me Awa Marie Coll Seck faite doct: Limu jëwriñ yi yore woon wér-gu-yaram yépp ci Senegaal | Wér-gu-yarameur honoris causa.) +Penda Mbow + +Penda Mbow mu ngi juddu atum 1955. Borom xam-xam bu xam-xamam màcc ci taarix la, muy ab bañkat. Nekkoon na fi jëwriñ ji yore caada ak cosaan ay weer atum 2001. Jàngalekatu taarix la ci Iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar nekk itam njiitu genn mbootaayu njuddu-réew. + +Dundu ak jaar-jaaram +Penda Mbow mu ngi juddu ci weeru mee atum 1955. + +Atum 1986 la am ab doktoraa ci tarixu jamono ji farañse tudde moyeenaas (histoire médiévale) ca iniwersite bu Porowãas (Provence) ci ab teesu ñetteelu fànn bi mu bind ci « Nguuru takk-der gu askanu mameluke ci ni ko téereb nattu suuf bu Ibn al-Ji’an ñu dendale ko ak li am Farãas ngir xam li ñu niroole ak li ñu wuute » (L’aristocratie militaire mameluke d’après le cadastre d'Ibn al-Ji'an : éléments de comparaison avec la France. + +Ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru mee atum 2011, mu am Piri Sãa Póol II ngir jàmm ji, ab raaya bu Watikãa di joxe te kilifag làbbe gii gi Mgr Luis Mariano Montemayor tegoon ci ay yoxoom. + +Dundug biiram +Atum 2017 ba léegi, mu ngi ci buumu sëy, borom-këram a ngi tudd Saaliw Mbay. + +Mbind (tànneef) + + (sous la direction de) Hommes et femmes entre sphères publique et privée, 2005 + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Seetal tamit + +Lees bind ci moom + + Lydia Polgreen, « At Africa's Crumbling Colleges, No Room for Students », The New York Times, 26 mai 2007 (la situation à l'UCAD) + Fabrice Hervieu-Wane, « Penda Mbow. Femme d'utilité publique », dans Dakar l'insoumise, Éditions Autrement, Paris, 2008, p. 94-99 + Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, B. Ndiaye, Dakar, 2006, p. 284 + +Jukki yi ñu ko tudd + + Taarixu jigeen ci Senegaal : Histoire des femmes au Sénégal + Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal : Liste de femmes ministres sénégalaises + +Lees jële feneen + + Fees ko mën a xame Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + + + Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Limu téere ak jukki yi Penda Mbow siiwal : Liste des publications de Penda Mbow + Dundu ak mbindam ci dalu web bu UCAD : Biographie et bibliographie sur le site de l'UCAD Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Waxtaan ak Penda Mbow : Entretien avec Penda Mbow (fukki fan ak ñaar ci weeru màrs atum 2008) Article de Wikipédia avec notice d'autorité +Maam Yunus Jeŋ + +Maam Yunus Jeŋ (juddu 1939, faatu 2016) ab bindkat la bu dëkk Senegaal. + +Dund ak jaar-jaaram +Maam Yunus Jeŋ mu ngi juddoo Tiwaawon, ci Kayoor atum 1939. Waajuram wu góor a ngi cosaanoo Kayoor, waajuram wu jigeen moom, cosaanoo Ndar (See Luwi). Jàngalekat la woon mujj nekk njiitu lekool. + +Maam Yunus Jeŋ ci farañse ak wolof yépp la daan bind, moom mooy ki jëkk a bind ab téereb nettali ci wolof tudde ko Aawo bi. Téere boobu ñu ngi ko siiwal atum 1992 ci Dakaar, mu teg ci beneen téereb nettali bu tudd L'ombre en feu, ñu siiwal ko atum 1997. + +Àjjuma benn fan ci weeru awiril atum 2016 la génn àdduna ci këram, ci Dakaar. + +Ay Téereem + + L'ombre en feu, Dakar, Les Nouvelles Éditions Africaines du Sénégal, 1997, 233 p. . Aussi, très soutenue par sa fille aînée Ndeye Bogui Sow Camara à qui l'édition de ce livre tenait à cœur. + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Seetal tamit + +Lees bind ci moom ak ay téereem + + Lilyan Kesteloot , « L'Ombre en feu de Mame Younousse Dieng », in Éthiopiques, n° 60, 1er semestre 1998 + Jean-Marie Volet, « Tradition and Modernity Are Here to Stay: An Analysis of Francophone African Women's Writings Published in 1997-98 », Research in African Literatures, vol. 30, n° 2, été 1999, p. 182-193. + Guedj Fall, « Aaawo Bi de Mame Younousse Dieng, un récit fondateur en langue wolof », in Éthiopiques, n° 76, 1er semestre 2006. + Abdoulaye Keita, « Dieng, Mame Younousse [Tivaouane 1940] », dans Béatrice Didier, Antoinette Fouque et Mireille Calle-Gruber (dir.), Le dictionnaire universel des créatrices, Éditions des femmes, 2013, p. 1254. + +Jukki yi ñu ko tudd + + Càllalag Senegaal : Littérature sénégalaise + Limu bindkati Senegaal yi : Liste d'écrivains sénégalais + Taarixu jigeen ci Senegaal : Histoire des femmes au Sénégal + +Lees jële feneen + + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité . Fees ko mën a xame : + Fichier d’autorité international virtuel + International Standard Name Identifier + Bibliothèque nationale de France (données) + Système universitaire de documentation + Bibliothèque du Congrès + Gemeinsame Normdatei + Bibliothèque royale des Pays-Bas + WorldCat + +Maam Yunus Jeŋ ci dalu web Lire les femmes écrivains et les littératures africaines +Xadi Silla + +Xadi Silla mu ngi juddu ñaar-fukki fan ak juroom-ñaar atum 1963 ci Dakaar, génn àdduna juroom-ñetti fan ci weeru oktoobar atum 2013. Bindkat la woon bu doon yëngatu ci sinemaa tamit. + +Dundu ak jaar-jaaram +Ginnaaw bu mu amee bakalóoreyaa ci Dakaar ba pare, Xadi Silla dafa dem Pari ngir wéyal fa ngàngum njënd ak njaay mu mu doon def. Bi mu demee, dafa mujj dakkal njàng moomee, dem jàngeji Hypokhâgne (ci néegu njàng buy waajal xam-xamu càllala), foofu la ame ab lisãas ci filosofi. Mu dakkal njàngam mi, tàmbali di ànd ak ay nit (góor ak jigeen) yuy yëngu ci mbiru uslu ak misig… Foofu sax la ko cofeel gi mu am ci mbind mi feeñoo. Ginnaaw bu waajuram wu jigeen faatoo, mu tàmbalee bind : « Dama xalaat ne bu may bind ci moom, dina am lenn lu ma mën a dekkal, dinaa ko mën a génne ci lu ma jàpp ne lu neenoon ba pare la ». Ci noonu, mu daldi bind mayeem (nuwelam) bu jëkk, tudde ko L’Univers, waaye ba tey, téere boobu kënn mësu ko siiwal. Mu wéy di bind bés bu Yàlla sàkk te mbind moomu sukkandiku ci ay xalaat yu tukke Dakaar, dëkk bi mu juddoo, « mu mujj nekk dëkk bu yéeme ndax li ma nekk di dundu feneen ». + +Atum 2005, mu jël neexalu joŋante bi amoon ca festiwaalu àdduna ci mbind ak ceetaan ba amoon ca Màrsey, ndax film bu mu defoon tudde ko Une fenêtre ouverte. + +Mu ngi doon jàngale almãa ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar. + +Ab téereem + + Le Jeu de la mer (roman), Paris, l'Harmattan, 1992, 160 p. + +Léppi filmam + + 2005 : Une fenêtre ouverte + 2006 : Colobane Express + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Toftal yi + +Lees bind ci moom + + Françoise Pfaff, « Khady Sylla », in: À l'écoute du cinéma sénégalais, Paris : L'Harmattan, 2010, p. 213-224 + +Jukki yi ñu ko tudd + + Sinemaa bu Senegaal : Cinéma sénégalais + Limu filmë yu Senegaal : Liste de films sénégalais + +Lees jële feneen + + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité Fees ko mën a xame + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Dundu ak ay téerey Xadi Silla : Bio-bibliographie de Khady Sylla +Faatu Joom mi juddu ci atum 1968 ca Ñoojoor ci Sénégal, taalif kat bou jiggeèn la bu coosano Senegaal di dundu Faraas. + +Ginaw siwalug limu teère bu tudd La Préférence nationale, ci atum 2001, naka nonou teerem buñu naan Le V entre de l'atlantique moo tax ñu xamko ca bitim reéw. Ci am  mbindam daciy wax lu jëm ci tukki ca Faraas ak itam dingante Faraas ak keembarug Afrig. + +Jaar-jaar +Fatu Joom mongui juddu ci atum 1968 ca dunug Ñoojoor ci mbelug Salum, ci dëku Seereer, ca ngélemu-suufu Senegaal. Jank piir la –– ay wajuram sëyu ñu -- maamam bu jigeen, Aminta moko yarr.. Aw santam mongi juge Siin Saalum, fa nga xamne Joom yi ay Ñominka lanu. + +Wuteg li cosaanu xeetam digle, dafay taqqoog goor ñi déet muy dimbali jigéen ña ñu togg ñam ya ag def ligeyu kër yi. Saa sune day wute ak dundinug waa dunu gi batax mu dem daara teksi jangi fanraase. Maamam bu jigéen def na ab diir ngir nangu ni man na jangi : mom Faatu jank bi da daan dem daara di lakatu, ba kerok jangalekatam yayy ay waajuram ngir ñu bayiko mu wëyële. +Article à référence nécessaire +Ci fuki at ak juròom mu bëgg lool njangatu faranse tek si tambale bind. Faatu Joom genn ab dëkkam ngir wëyële am njangam ci yenen dëkku Senegaal, bolek di fayale ag dundug màang kat gui ak ligéey yu ndaw yi ;  teksi mu jangi daray Mbuur, ligey kem mbindaan fa Gambi  teksi muje tambali am njangum iniwersite ca Ndakaaru.  Ca jamono jooja mongui bëgona doon jangalekatu faraase, déet muy genn réew mimu juddo. + +Waye ci ñaar fukki at ak ñaar mu  bëgg benn faraase, daldi sëyi teksi andag mom Farans ca Strasbourg ci atum 1994. Binga xamé ni njabootug borom kërëm beedi nanu ko, mu daldi tass ab sëyam ñaari at ci ginaw tek si mu nekk ci jafe-jafe yu metti, ñu wacc ko ci nekkinug Mòodu-Mòodu ci suufu Farans. Ngir mu fay am njangam, fawu mu mbindaanu ci diirug juròom benni at, ag bimu mane jangale ca waxtu wanga xamne am na lijaasam bu mag ba, njëkk muy tambali ab ligéeyam ci « Tukki gi , jëflante yi ak njang mi ci mindum téere ak sinemaa bu Sembeen Usmaan». + +Liggéey +Ginaw bimu jange araf yi ak filosofi ca iniwersite bu Strasbourg, mu daldi fay jangale, teksi iniwersite March-Bloch bu Strasbourg ak daara bu kawe bu jëm ci wallu njangele bu Karlsuhe, fa Allemagne.  Mu daldi jot raaya ya ñeel lijasa honoris causa ca uniwersite Liège ci atum 2017. + +Mu dëgmal it am mbind : siiwal na La Préférence nationale,  ab limu teere bu jooku ci Présence africaine ci atum. Le Ventre de l'atlantique moy taarixam bu njëk  , bi genn ci atum 2003 bu ciwalug Anne Carrière.  Ginaw gi laci toppu Kétala (2006), Inassouvies, nos vies (2008), Celles qui attendent (2010) ag Impossible de grandir. + +Ci atum 2019 la am ngañelu raaya yu ñoom Rotary Club bu làkk faraase ñeel tàarixam Les veilleurs de Sangomar. + +Gis-gis +Dafay jammarlog ag ñi amul yërmande, day àar ligéeyu daara ag meloy  gëm sa réew. + +Lu jëm ci maggug populism gi, Faatu Joom dankoy faral di sakku saa sune ngir mu yaatal xalatam ci ay waxu politig ag askan wi ci telewisong yi ak xar-xarale yi.   + +Mu jël taxawaay bu am solo ci maggug populism andag Mboolom biir réew ba ca Faraas. Ci nekk bimu nekk bindkat , dafa bëg fatali ci ay téerem meloy nit ak  gëm sa réew  ndax mom diapp nani « waratuño noppi ci kanamu ñi dano wayadi ci taanal biir réew». + +Dafay wax tamit kàdduy ñaxtu ngir lëkkalo bu gëna yamo ci dingante Orob ak Afrig. Jàpp nani fiñu tollu Orob mo nek ci ginaw lëkkalo bu yamo wul teksi Afrig moomul alalam. Te it jàpp nani rusaange jamonoy koloñal ba mongi fi ba léegi muy ci booru wa Afrig ak tamit wa Orob, mu nekk liy gaar ab lëkkalo bu gëna yamo. Xalaat nani kunekk war na yeug ni nit la su jakkarlok benen moromu nitam, mo xam fumu mana soqqeeko. Naka nunu, déet muy joxoñ baaram benn kembaar, motax jàap nani waa Afrig dano war wesu di nekk ñunuy noot te it wa Orob bayi sen noot gi ngir digante  aji jariño/ aji jariñe, aji joxe/ aji jox ji mana dakk. Fimy daane le moy dafa leeral ni dimbali aw nitt moy nga dimbali ko ba dootu soxla dara ci yaw, masalan ndimbal li ñeel sùkkaliku bi réewi sowu yi ini Afrig. + +Mbind mi + + 2001 : La Préférence nationale, recueil de nouvelles, édition Présence Africaine. + 2002 : Les Loups de l’Atlantique, nouvelles, Dans le recueil : Étonnants Voyageurs. Nouvelles Voix d’Afrique. + 2003 : Le Ventre de l'Atlantique, roman, éditions Anne Carrière, éditions Le Livre de poche 30239 + 2006 : Kétala, roman, Éditions Flammarion. + 2008 : Inassouvies, nos vies, roman, Éditions Flammarion. + 2010 : Le Vieil Homme sur la barque, récit (illustrations de Titouan Lamazou), Naïve. + 2010 : Celles qui attendent, roman, Éditions Flammarion + 2010 : Mauve, récit, Éditions Flammarion + 2013 : Impossible de grandir, roman, Éditions Flammarion. + 2017 : Marianne porte plainte !, essai, Éditions Flammarion. + 2019 : Les Veilleurs de Sangomar, Albin Michel. + +Aand + + Weepers Circus, N'importe où, hors du monde (2011). Disku-téere la bo xamni lu tollog ñeent fukki nit yu am darajay taalifkat wala antarpareet ñoo ci bokk : Faatu Joom taalif nasi mbind munu siwalul (bunu wayul) ñeel ab gis-gisu bopam ci tur bu naqqare degg bu téeri bii di "N'importe où, hors du monde". + +Téere yi nu yër + + Dominic Thomas, « African Youth in the Global Economy: Fatou Diome's Le Ventre de l'Atlantique », Comparative Studies of South Asia, Africa and the Middle East, 2006, no 26(2), p. 243-259 + Jacques Chevrier, « Fatou Diome, une écriture entre deux rives », Revue des littératures d'Afrique, des Caraïbes et de l'océan Indien, no 166, 2007, p. 35-38 + Victor Essono Ella, La crise de l’identité à travers l’écriture de Valentin Yves Mudimbe, Eugène Ebodé et Fatou Diome, Université Rennes 2, 2008, 365 p. (thèse de doctorat de Littérature française) + Eugénie Fouchet, La représentation romanesque de la femme africaine chez Fatou Diome et Fatou Keïta, Université de Metz, 2009, 156 p. (mémoire de master recherche 2e année de Littérature, cultures et spiritualités) + M. H. Kebe, « Le ventre de l'Atlantique, de Fatou Diome », L'Information psychiatrique, 2004, vol. 80, no 6, p. 491-493 + C. Mazauric, « Fictions de soi dans la maison de l'autre (Aminata Sow Fall, Ken Bugul, Fatou Diome) », Dalhousie French Studies, 2006, vol. 74-75, p. 237-252 + + +Séeréer +Juma Jeŋ Jaxate soskatu ñawin la bu dëkk Senegaal, juddoo Tëngeej (Rifisk), ñetti fan ci weeru desàmbar atum 1947. + +Dundu ak jaar-jaaram +Moom ci boppam moo jiite bérebu liggeeyukaayam bi mu tudde Shalimar Couture, bokk na ci ñi muy ñawal, njiiti réewu Afirig yu bare ak seeni soxna. + +Atum 2012, la bett askan wi ne dafay nekk ab way-wotelu ci wotey njiitu réew yi. Mu mujj ci nekk ndàdde ci sumbug wote bu jëkk bi, ndax téemeer boo jël, tus kos fukk ak ñaar (0,12%) rekk la amoon ci ñi wote ñépp. + +Ay sargalam +Atum 2013 la ko woykatu Kóngoo bi Koffi Olomidé sargale woyam wi mu tudde Festival. Mu dellu amaat lu ni mel atum 2013, ndax Fally Ipupa sargale na ko aw woyam. + +Seetal tamit + +Lees bind ci moom +Jukki bi ñu jëfandikoo ngir bind bile + + « Diouma Dieng Diakhaté : La couturière aux doigts de fée », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 37-38 + +Jukki yi ñu ko tudd + + Taarixu jigeeni Senegaal : Histoire des femmes au Sénégal + Caaday Senegaal : Culture du Sénégal + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër +Mbaaliyaa Kamara mu ngi juddu atum 1929, faatu fukki fan ak juroom-ñett atum 1955 ci Tondon. Ab bañkat la woon buy xeex ngir Ginne moom boppam. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Téere wala dali web yi ñu ko tudd +MBaaliya Kamara + + +Mbaaliya Kamara mu ngi juddu atum 1929, faatu fukki fan ak juroom-ñett ci weeru féewiriyee atum 1955 ci Tondon. Ab bañkat la woon buy xeex ngir Ginne moom boppam. + +Dundu ak jaar-jaaram +Mu ngi juddu ci Poseya, ci goxu Dubréka. Ci njabootu baykat la bokk. Bi mu jëmee mag tuuti, la dugg ci kureelu pólotig gu tudd Rassemblement démocratique africain (RDA), ci wetu borom-këram, Cerno Kamara mi bokkoon ci ñi demoon ca ñaareelu xare àdduna ba. Way-dencante yi dëkk Tondon, foofee mu doon jiite kureelu jigeen ñi bokk ci RDA. Njiitu kàntoŋ ba, Almaami Dawit Silla tere fa yëngu-yënguy pàrti RDA. Juroom-ñett ak juroom-ñeenti fan ci weeru féewiriyee atum 1955, mu bokk ci ñiy nangu lempo yi. Ab jote am ci diggante dëkkandoo yi ci jamonoy laaj lempo yooyu, Silla daldi ne saraax ci kër kamara-kundaa yi. Mbaaliya ma mu fa fekkoon, nga xam ne dafa wannoon lor sax, moo jàmmaarloo ak moom, Silla dóor ko jaasi, ñu yóbbu ko lopitaal bu Konaakiri. Fukki fan ak benn ci weeru féewiriyee, liir bi juddu te andiwaalewul bakkan. Ñu teg ci benn ayu-bés rekk, Mbaaliya Kamara faatu. + +Xew-xew boobule yokk xadar ji nit ñi àndaloon, gën leen a ñaax ci xeex ba réew ma doon xeex ngir moom boppam. Ay junne junney nit teewe rob ga. Ahmet Seku Ture jàng seede ya. Nit ñi fent ay woy ngir sargale ko Mbaaliya Kamara mi nga xam ne woyam woowu, mu nga fay jolli ba tey, te ba léegi ñu ngi ko fay màggal. Ja bu Konaakiri, moom lañu ko tudde. + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër +Anet Mbay Dernwil + +Anet Mbay Dernwil mu ngi juddu atum 1926. Bindkat la woon, nekkoon taskatu xibaar, nekkoon it kuy wax ci rajoy réew mi. + +Dundu ak jaar-jaaram +Anet Mbay Dernwil mu ngi juddoo Sóokoon fukki fan ak juroom ci weeru desàmbar atum 1926. + +Li ëpp ci ay téereem, ay taalif lañu wala ay mbind yu mu def ngir xale yii. + +Moom mooy ki sooke amalug Miise bi ñu jagleel jigeen ñi, tuddeko  Hãariyet Bàccili ca Gore (Musée de la Femme Henriette Bathily de Gorée). + +Saa-sinemaa bile di Usmaan Wiliyaam Mbay, juddu atum 1952, doomam la. Moom Usmaan Wilyaam Mbay sax, def na benn film ci yaay ji atum 2008, tudde ko « Mère-bi ». + +Ay téereem + + 1965 : Poèmes africains + 1966 : Kàddu (réédition des poèmes) + 1976 : Chansons pour Laïty + 1983 : Le Noël du vieux chasseur + 1983 : La Bague de cuivre et d'argent (prix Jeune Afrique en 1961) + 2003 : Motte de terre et motte de beurre + 2003 : Picc l'Oiseau et Lëpp-Lëpp le papillon + +Seetal tamit + +Jukki yi ñu ko tudd + + Càllalag Senegaal : Littérature sénégalaise + Limu bindkati Senegaal yi : + Tasukaayi xibaar yu Senegaal : Médias au Sénégal + Taarixu jigeen ci Senegaal : Histoire des femmes au Sénégal + +Lees bind ci moom + + + « Annette Mbaye d'Erneville : L'éclaireuse », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 40-41 + Aliane, « Mme Mbaye d'Erneville, directrice des programmes à l'Office de radiodiffusion du Sénégal », Amina, no 32, juillet 1975, p. 21-23 + Pierrette Herzberger-Fofana, « Annette Mbaye d'Erneville (Sénégal) », dans Littérature féminine francophone d'Afrique noire, Paris, L'Harmattan, 2000, p. 374-81. + +Lees jële feneen + + Dundu ak jaar-jaar : Biographie + « D'Orphée à Prométhée : la poésie africaine au féminin. En hommage aux pionnières de l'écriture féminine africaine, 1967-1997 » (article d'Angèle Bassolé Ouédraogo, 1998) +Article utilisant une Infobox +Elen Jonson Sërliif mu ngi juddu ñaar-fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru oktoobar atum 1938 ca Morowiyaa (Liberyaa), doon jigeenu nguur ju Liberyaa, nekk fa njiitu réew, dale ko fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee atum 2006 ba ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru sãawiyee atum 2018. + +Borom xam-xamu koom-koom la bu jànge Etaasini (USA), moom mooy jigeen ji jëkk a falu njiitu réew ci déndu Afirig bi.. + +Atum 2011, kenn la woon ci ñi jël neexalu jàmm bi, ñu tudde ko prix Nobel de la paix. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Njàng ak cosaanam +Ñaar ci ay maamam, ñu ngi juddoo Liberiyaa. Way-juram wu góor, Jahmal Karney nga xam ne ag njaboot gu dëkk Liberiyaa te cosaanoo Amerig moo ko doomoo woon, lekool bu ñu naan College of West Africa ci Morowiyaa la ame woon lijaasa, daara joojee, iniwersite làbbe yi la. Ab laykat (awokaa) la woon. Bokk na ci maamam, Hilary R. W. Johnson, njiitu réewu Liberiyaa bu fa juddoo bu jëkk. Li waral deram bu xees bi mooy ne dafa am maam ju góor ju bokk ak yaayam te dëkk Almaañ. Ci ay way-jur yu am alal la juddoo, yaroo ci. Bi muy am fukki at ak juroom-ñaar la am borom-këram. Borom-kër baa ngi tudd Jems Sërliif, féete ko mag, doon liggeeye ca njëwriñu ji yore mbay mi, moom moomee sax, moo ko yombalal am njàngam ca Etaasini (USA). Jems Sërliif ab naankatu sàngara la te dafa ko doon tëkku moom ak ay doomam. Dafa ko doon fekksi sax ci njëwriñ ji yore gafakag réew mi, fi mu doon liggeeye, di ko pes, ndaxte nee na soxna si dafay gudde ñibbi. Bi mu amee juroom-benni at ci boobule sëy, la Yàlla wéddi ginnaaw bu ko borom-këram tiimale fetal ne dafa koy faat ci kanam doom ji. + +Mu def njàngam ca Amerig ba pare daldi fa am bakalóoreyaa ci xam-xamu waññ (kontaabilite) ci Madison Business College, nekk ci dëkk bu ñu naan Madison (Wisconsin) atum 1964 ; am ab lijaasaab xam-xamu koom ca iniwersite bu Colorado atum 1970 ak benn mastë ci njàngum njiiteef ca iniwersite bu Harvard atum 1971. Way-bokk la ci kureel gu boole ay waa-Afrig ak waa-amerig yu jigeen Alfaa Kappa Alfaa (Sororité afro-américaine Alpha Kappa Alpha), nekk kureel gu ni mel gu ñu jëkk a sos atum 1908. + +Way-bokk la ci ab jàngu bu ñu naan Église méthodiste unie,. + +Ag njëlbeenam ci pólotig : kujje gi +Ab sekerteer detaa koppar yi la woon diggante 1972 ba 1978, laata muy nekk jëwriñ ji yore gafakag réew mi diggante 1979 ba 1980. Ci menn at mi, Samuel Doe foqati nguur ga, raylu ka fa nekkoon njiitu réew di William Richard Tolbert ci biir këram ak li ëpp ci ay jëwriñam ci ag tefes. Yàlla def Elen Jonson Sërliif mucc ca ndax li mu doon jigeen ak tamit li Samuel Doe bëgg mu des fa yenn njiit yu koy mën a gunge ci liggeeyam bi. Waaye Yàlla dimbale ko mu rëcc, dem tóxuji feneen, dellu ñibsiwaat ginnaaw gi, ne dafay def ay yëngu-yënguy pólotig ngir kontar nguur ga. Ci lañu ko tëkku ne dañu koy ray. Atum 1985, ñu daldi ko teg daan bu tollu ci fukki ati kaso ndax li mu àndul ak nguuru takk-der gi Samuel Doe jiite. Bi mu defee diir bu gàtt ci kaso gi, lañu ko may mu génn réew ma dem feneen. Li mu àndul woon ak nguur ga, di ko ŋàññi saa su nekk moo tax sax, ñu demoon ba tudde ko « Jigeen ju mën góor » (« Dame de fer ») ». + +Ay jaar-jaaram ci liggeeyu borom xam-xamu koom-koom +Mu delluwaat Etaasini (USA) ngir wéyal liggeeyam bi ci wàllu koom, di liggeey ci bànku àdduna bi (Banque mondiale) ak tamit ci Citibank. . Mu jiite fa,  ci misaal, PNUD bu Afrig (Tëralinu mbootaayu xeet yi ngir suqaliku gi). + +Atum 1997, mu dugal xaalisam ci kàmpaañu wotey njiitu réew ba ngir jàppalee ko Charles Ghankay Taylor, jëf jooju, dafa mujj jàpp ne sax njuumte la woon. Kureel gi yore « Waxtaan, waxante dëgg te juboo » (« Vérite et reconciliation ») dëgër lool ci ñu tere Elen Jonson Sërliif am ay ndombo-tànk ca réew ma ci diiru fanweeri at ndax li mu jàppale ay way-fippu ci xaalis,,. + +Wotey njiitu réew yu 2005 ak diiru palam gu jëkk + +Elen Jonson Sërliif moo teewaloon pàrti bile di Parti de l’unité ca wotey njiitu réew ya, jàll ci sumbu wote bu jëkk ba oktoobar 2005, dem daje ak George Weah ci ñaareelu sumbu wote ba, juroom-ñetti fan ci weeru nowàmbar. Li tukke ci waññ yu mujj yi ñu siiwal ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar mooy ne, moom mi nekkoon jëwriñ ji yore gafakag réew mi, moo am juroom-fukk ak juroom-ñeent kos ñeent ci téemeer boo jël (59,4 %) ci falaakoon yépp, ci ñaareelu wote yi amoon ci juroom-ñetti fan ci weeru nowàmbar, George Weah mi fi nekkoon futbalkat bu àdduna yépp ràññe, moom daldi am ñeen-fukk kos juroom-benn ci téemeer boo jël (40,6 %) ci falaakoon yépp. + +Elen Jonson Sërliif daldi jël lengey njiitu réew ya ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar atum 2005. Guleet ! Afrig am jigeen ju falu njiitu réew ci benn ci réewam yi. Fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee, la waat ci kanam Henry Reed Cooper, di njiitu ëttu àttekaay bi gën a mag ca réew ma. Ca ndaje mooma sax, ay junney junney doomi réew ma, njiiti Afrig yu bare ak ndawi yeneen réew, teewoon nañu fa. Joseph Boakai lañu toftal ci moom. + +Fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru màrs atum 2006, ci am ndaje mu kureelu kaaraange gu mbootaayu xeet yi, Elen Jonson Sërliif dafa ñaan ñu teggi daan yi tegu ci kow réewam te aju ci jamãa bi ñuy jaayeji bitim réew ak tamit mbootaayu xeet yi des ca réew ma, bañ a dem. Dellu na fa biral ne pexeem ngornamãa bi ci wàllu saxal jàmm mu ngi sukkandiku ci ñeenti kenu : kaaraange, jiitug àq, yelleef ak njiiteef, doxalaat koom gi ak defaraat ay tabax ak yeneeni jumtukaay yuy ñoŋal nekkinu askan wi. Diiru palam gu jëkk gi yépp, genn-wàllu yoon yi wër Morowiyaa yépp defaraat na leen, nit ñi di am bu baax ndox ak kuraŋ saa yu ñu ko soxlaa, waaye ci wet gi nag, ndóol gi ak ndaw ñu amul liggeey (juroom-ñett-fukk ci téemeer boo jël (80 %) ñu ngi fa woon ne xas . Ba léegi nii, Liberiyaa bokk na ci fukki réew ak juroom yi gën a ndóol ci àdduna bi. Mu daldi jiital xeexu ger bi ci xeexam yépp, jëfandikoo ay xameem ci wàllu koom ak koppar ngir mën a leb xaalis bu mu suqalee réewam. + +Juroomi fan ci weeru nowàmbar, la ko njiitu Etaasini (USA) George W. Bush tappal medaayu njiitu réew bi aju ci moom-sa-bopp gi. Juroom-ñaari fan ci weeru oktoobar atum 2011, ñu jox ko neexalu jàmm ji (prix Nobel de la paix) mu bokk ko ak doomu réewam jile di Leymah Gbowee ak waa Yemen bi Tawakkul Karman. Kujjeg pólotig ga fa nekkoon anduñu woon ci ràññatle boobu ndax ñenn ñi sax dañu gisoon ne, Hillary Clinton moo ko ci jàppale ndax wotey njiitu réew yu 2011 yiy jegesi. + +Wotey njiitu réew yu 2011 ak ñaareelu diiru palam +Moom moo jël ndam li ci wotey 2011 yi, li ko ko yombalal mooy, wujjam Winston Tubman dafa ŋàññi doxalinu wote wi ba pare sant ay ñoñam ñu bañ a wote), falaakoon yi néewoon lool ndax ci téemeer boo jël, fanweer ak juroom-ñaar kos ñeent rekk a ci wote woon (37,4 %). + +Fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee atum 2012, ñu jox Elen Jonson Sërliif lengey njiitu réew ya, ci ñaareelu diirug palu njiitu réew, mu war a jiitewaat réew ma. Hillary Clinton, sekerteer detaa bu Amerig ak njiiti réewu Afrig yu bare, yu bokk ak Liberiyaa fu ñu féete ci dénd bi, teewoon nañu ca ndaje ma.. + +Fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru màrs atum 2012, muy jàppal tànk yoon yiy    def ngóor-jigeen ag jagalti sàrti gu ñu war a daan ñi koy def ca Liberiyaa. + +Atum 2014, lañu wax ak moom ci li jigeen ñi mënagul a jot ci suuf si, maanaam nekk borom suuf ca réew ma, te loolu doonoon ab dige bu mu defoon ci këru yéglekaay gile di Reuters atum 2013. + +Oktoobar 2014, mu woote ndimbal fépp ci àdduna bi ngir ñi ko am te mën ko jàpp ci dakkal lawug jàngoroy ebolaa. Ñaari weer lu jiitu wooteem boobu, dafa ñaanlante woon ak jëwriñ yi nekkoon ci ngornamãam bi te ñëwaatuñu woon ca réew ma ngir bokk ci xeexu ebolaa bi. + +Atum 2017, ñu tudd ko ci luubal alal ba woon ca Paradise Papers. + +Diiru palam gaa ngi waroon a jeex ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru sãawiyee atum 2018 bi George Weah mi ñu fal ñaar-fukki fan ak juroom-benn ci weeru desàmbar atum 2017, di jël lenge yi ci yoxoom. Wote yooyule, George Weah mu ngi leen séqoon ak ka ñu toftaloon ca njiitu réew ma di Joseph Boakai + +. + +Ay ndombo-tànkam yu nguur + + 1972-1978 : Sekerteer detaa bu gafakag Liberiyaa (secrétaire d'État aux Finances du Liberia) + 1979-1980 : Jëwriñu gafakag ngornamãa bu Liberiyaa (ministre des Finances du gouvernement du Liberia) + 1982-1985 : Ki topp ci njiitu déndu Afrig ngir màkkaanu Citibank, Nairobi (vice-présidente de la Région Afrique pour le Bureau de Citibank, Nairobi) + 1986-1992 : Ki topp ci njiitu kureel gi jiite bànku Équateur, Washington, D.C., nekk fa tamit ab way-bokk (vice-présidente et membre du Comité de direction de la banque Équateur, Washington, D.C.) +prix Nobel de la paix + 1988-1999 : Way-bokk ci njiiteefu The Synergos Institute + 1992-1997 : Njiitu tëralinu suqaliku wu mbootaayu xeet yi ci Afrig (directrice du programme de Développement des NU Bureau pour Afrique) + 1997 : Njiitu Parti de l'unité + 2004-2005 : Njiitu kureelu nguurin gu jub te sell (Liberiyaa) (présidente de la Commission de bonne Gouvernance (Liberia) + 2005 : Njiitu Parti de l'unité ; way-wotelu ci wotey njiitu réew yi (dirigeante du Parti de l'Unité ; candidate à la présidence) + 2006 : Njiitu réew mi (présidente de la République) + +Yeneen nbombo-tànk yu bokkul ak yu nguur + + Way-bokk ci ñi sos Institut International ngir njiit yu jigeen yi ci wàllu pólotig ; + Way-bokk ci Conseil d'investissement ngir suqalikug Afrig gu tey ; + Way-bokk ci kureelu Moderne Africa Fund Managers ; + Njiitu bànk bu Liberiyaa ngir suqaliku gi ak dugal xaalis gi (banque du Liberia pour le Développement et d'investissement) ; + Njiitu Kormah Development and Investment Corporation ; + Kilifa ci leble xaalis bi ci bànku àdduna bi (Banque mondiale) ; + Njiitu kureelu waxtaan, waxante dëgg, juboo bu Liberiyaa (Présidente de la Commission de vérité et de réconciliation libérienne) ; + Ki topp ci njiitu Citibank. + +Atum 2006, moom moo nekkoon juroom-fukkeelu jigeen ak benn ji ëpp doole ci àdduna bi ci gis-gisu Magasin  bi ñu naan Forbes. Atum 2007, mu jël téemeereel, atum 2008, mu jël juroom-benn-fukk ak juroom-benneel. + +Ay raayaam + +Neexal yi + + 1988 : Neexal yu « quatre libertés de Roosevelt » ci wàllu sañ a wax sa xalaat + 2006 : Neexalu Freedom Award + 2007 : Medaayu njiitu réew ci moom-sa-bopp + 2011 : Neexalu Nobelu Jàmm mu bokk ko ak Leymah Gbowee ak Tawakkul Karman + 2012 : Neexalu Indira Ganfhi + 2014 : Neexalu koom-koom bi yépp bu Kiel + 2017 : Téemeeri jigeen + 2017 : Neexalu Mo Ibrahim + +Sag yi + + 2006 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Marquette + 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Indiana + 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Dartmouth  + 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Brown + 2009 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Tampa  + 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite buYale + 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite buRutgers + 2011 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite buHarvard + 2014 : Ange de la paix + 2016 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite buDartmouth College + +Ay medaayam + + 50x50px Grand-Croix de la Légion d'honneur, juroom-ñaari fan ci nowàmbar atum 2012, François Hollande moo ko ko tappal + 50x50px Collier de l'Ordre Pro Merito Melitensi (Malte) + 50x50px Commandeur de l'ordre de Mono (Togo) + 50x50px Order of the Pioneers of Liberia (en) (Liberia) + 50x50px Order of the Star of Africa (en) (Liberia) + 50x50px Humane Order of African Redemption (en) (Liberia) + +Dundug biiram +Elen Jonson Sërliif am na ñeenti doom, ñaar ñi mu jox liggeey yu am ñam ci nguur gi. Bokk na ci doomam yooyu, Robeer Sërliif, mi nekkoon njiitu kureelu njiiteef gu këru liggeeyukaay gi yore petorolu Liberiyaa, nekkati xelalkatu yaayam jiy njiitu réew mi, Moom moomu di Robeer Sërliif, dafa ñàkkoon atum 2014, ay wote senaatëer yu mu doon def ak George Weah ngir jiite diiwaanu Montserrado ; Jeneen doomam ji moo doon jiite caytug lépp luy xiibaaru biir réew mi : ñetteelu doomam ja nag moom, moo toppoon ci njiitu bànk sàntaral ba. + +Téere bi mu bind + + The Child Will Be Great, éditions Harper, 2009 + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Toftal yi +  +Ci yeneen naali Wikimedia + +Elen Jonson Sërliif, ci Wikimedia Commons + +Lees bind ci moom + + Ellen Cooper Madame la Présidente : Une biographie d'Ellen Johnson Sirleaf, trad. de l'anglais par Mathilde Fontanet, 2018, Editions Zoé, Coll. Ecrits d'ailleurs, 448 p. + +Jukki yi ñu ko tudd + + Limu njiiti pólotig yi : (Liste de dirigeantes politiques) + +Lees jële feneen + + Dundu ak jaar-jaaram ci dalu webu Fondation Nobel (am na ab ruq bu nekk ci xët wi te am ay seetukaayi joxe neexal yu bare, bokk na ca, ab jukki bu borom neexal bi bind ñu tudde ko Nobel Lecture, te muy andi ay leeral ci li mu def. +Aminata Ture mu ngi juddu fukki fan ak ñaar ci weeru oktoobar atum 1962 ci Dakaar. Jigeenu nguur ju Senegaal la, dellu nekk taxawukatu àq ak yelleefi doom-aadama, nekk it liggeeykat ca Mbootaayu ya (ONU). Nekkoon na fi jëwriñ ji yore wàllu yoon ci Senegaal 2012 ba 2013 laata muy doon jëwriñ ju jëkk ci nguuru Senegaal 2013 ba 2014. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Tàggatoom +Waajuram wu góor doktoor la, waajuram wu jigeen di ab saasfaam, moom mu ngi defe njàng mu suufe mi ca Tàmbaakundaa (gi waajuram wu góor doon liggeeye), wéyale njàngam mi ca liise Gaston Berger bu Kawlag. Atum 1981, moom moo doon ki jël ndam li ci koŋkuur seneraal bi ci wàllu koom, am bakalóoreyaa séeri B, ca liise Van Vollenhoven bu Dakaar. Ginnaaw gi mu dem jàngi Farãas, daldi di fa ame metiris ci wàllu koom-koom ca Dijon, DESS ci wàllu caytu këri liggeeyukaay ca Aix-en-Provence ak benn PhD ci manasmãa enternasiyonaal ca International School of Management (ISM), Pari ,. + +Atum 1988 la tàmbale liggeeye SOTRAC, këru liggeeyu dem-ak-dikk ci Dakaar, foofee moo fa doon jiite siiwal gi ak jokkoo bi. + +Njëlbeenam ci pólotig +Way-bokk la woon ci làngu pólotig gi ba muy am fukki at ak ñeent ba tey. Muy yëngu ci iniwersite Farãas yi féete càmmoñ, maanaam waa góos yi, nekk it way-bokk ci Ligue communiste des travailleurs (LCT), kureel gi mujj soppeeku Mouvement pour le socialisme et l'unité (MSU). Moom moo nekkoon, ci kàmpaañi wotey 1993, jigeen ji jëkk a jiite kàmpaañu wote te doon ko defal Làndiŋ Sawane, ci pàrtim bi sax la mujj dugg at mi ci topp. + +Pas-pasam ci xettali doom-aadama +Aminata Ture daldi nekk ginnaaw gi, njiitu tëralini mbootaayu Senegaal giy taxaw ci taw-féexu njaboot gi[kañ ?]. Atum 1995, mu tàmbali di liggeeyal kureelu mbootaayu xeet giy taxawu askan (Fonds des Nations unies pour la population (FNUAP), mu jëkk fa nekk xelalkat bu jëkk ca njëwriñu njaboot ak ndimbalu askan ju Burkinaa Faaso laata mu fay doon xelalkat bu FNUAP ci réewi Afrig yi làkku farañse boole, nekkati lëkkalekatu tëralin wu ñu naan « genre et VIH » ci Afrig sowu-jant ngir màkkaanu kureelu mbootaayu xeet gi fi nekkal jigeen ñi ci dénd bi. Mu nekkoon fa di ñaax jigeen ñi ci soreel njur gi ak wérug yaram gi aju ci njur gi. Atum 2003, ñu fal ko ca New York njiitu deppàrtemãa bu àq ak yelleefi doom-aadama bu FNUAP. + +Digganteem ak Maki Sàll +Aminata Ture jóge New Jersey atum 2010, ñëw nekksi njiitu màkkaanu Maki Sàll (direktëer de kabine), mi doon njiitu Alliance pour la République, te bokk ci at mi ci topp, ci mbindum tëralinu Maki Sàll ngir kàmpaañu wotey njiitu réew yu 2012. + +Mu wuutu Seex Tijaan Si ci njëwriñu yoon ji ci ngornamaŋ bu Abdul Mbay. Li doon sasam foofee, moo doon andi ay coppite yuy gën a woyofal, gën a gaawal doxinu yoon wi, gën a jegeel nit ñi ëttu àttekaay yi, yaatal kureelu sàrtu réew gi (Conseil constitutionnel). Ci weeram yu jëkk yi la tàmbale doxal xeexu ger bi Maki Sàll bëggoon, ak ay lëñbët yi mu doon def ci doxalinu njiiteef gi weesu ak tamit ni kilifay nguuru Abdulaay Wàdd yi daan yore alali askan wi. Bokkoon na ci kilifay Abdulaay Wàdd yooyu, Kariim Wàdd, doom ji. + +Alalam ji nga xam ne ñaari taax (etaas) yu mag la ci Senegaal ak beneen bu nekk Etaasini (USA), ñu ngi ko xayma ci juroom-ñaar téemeeri milyoŋ ak juroom-ñaar-fukk ak juroom-ñaari dërëm ci CFA (777 millions de francs CFA). + +Jëwriñ ju jëkk +Aminata Ture ñu ngi ko fal benn fan ci weeru septàmbar atum 2013, mu taxawal ngornmaŋ bi ca suba sa xaat. + +Ñeenti fan ci weeru sulet atum 2014 la ko njiitu réew mi ñaanal, ginnaaw bu Xalifa Sàll jëlee ndamal wotey meer yi ci gox bi mu dëkk ci Dakaar,. moom Aminata Ture. Mohamet Jonn, mi fi doon liggeeye ca Mbootaayu xeet ya, moo ko wuutu foofee mu nekkoon juroom-benni fan ci weeru sulet. + +Féewiriyee 2015 la ko Maki Sàll tabb ndaw lu sës ci njiitu réew mi ngir mu koy doxal ay yonnent ci biir réew mi ak bitim réew yépp. + +Dundug biiram +Aminata Ture am na ñetti doom. Nekkatul soxna ci Umar Saar. Jëwriñ la woon ci nguuru Abdulaay Wàdd. Seen doom ju jigeen ji, Joor Saar, mu ngi ame ay lijaasaam ca iniwersite bu Yale, nekk ca Etaasini (USA). Jamono jii, mu ngi ci buumu sëy, borom-këram di ab njaatige (ãtarperenëer) bu tuddu Umar Kulibali. + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Seetal tamit + +Lees bind ci moom + + Torild Skard, Women of power : Half a century of female presidents and prime ministers worldwide, Policy Press, 2014, p. 297-298 . + +Jukki yi ñu ko tudd + + Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal : Liste de femmes ministres sénégalaises + Limu njiitu pólotig yu jigeen : Liste de dirigeantes politiques + Nekkinu jigeen ci Senegaal : Condition féminine au Sénégal + +niti senegaal +way politig yu Senegaal +Article utilisant une Infobox +Maam Maajoor Bóoy mu ngi juddu atum 1940. Jigeenu nguur la ci Senegaal, nekkoon fi jëwriñ ju jëkk, moom sax mooy jigeen ji jëkk a nekk jëwriñ ju jëkk ci Senegaal. + +Dundu ak jaar-jaaram + +Cosaan ak njàngam +Maam Maajoor Bóoy mu ngi juddu atum 1940 ci Ndar (See-Luwi). Ñenn ci njabootam, xam-xamu yoon lañu jàng. Way-juram wu góor gerefiyee la woon laata muy nekk isiyee (huissier de justice). Kenn ci ay càmmeñam toppekat seneraal (pólokirëer seneraal) la woon ca ëttu àttekaay bi gën a mag ci Senegaal (Cours suprême du Sénégal). Keneen ki ci nekkoon jàngalekat buy jàngale lii di droit international privé, moo mujj doon njiitu iniwersite bu Dakaar. + +Bi mu jàngee ca liise Federb bu Ndar ba matal, la ñëw iniwersite bu Dakaar, atum 1963, ci béreb bi ñu fay jàngale yoon ak koom-koom. Ginnaaw njàngam ci iniwersite bu Dakaar, dafa dem jàngi Pari ci ab lekool bu ñuy jàngale yoon ñu naan ko Centre national d'études judiciaires (CNEJ) de Paris, lekool boobule moo mujj nekk lekool bi ñuy tàggate àttekat yi (École nationale de la magistrature). + +Ay jaar-jaaram ci wàllu yoon ak yoonal +Dafa jëkk a nekk ki ñu toftal ci toppekatu repibilik bi (procureur de la République), teg ci nekk ki topp ci njiitu tirbinaalu gox bu jëkk bu Dakaar (première vice-présidente du tribunal régional de première classe de Dakar) laata muy nekk njiitu néeg ca àttekaayu dabaatal ba (présidente de chambre à la Cour d'appel). + +1990 ba 2000, amoon na ay ndombo-tànk ci ab bànku Afrig sowu jant ñu naan Compagnie bancaire de l'Afrique occidentale. + +Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig +Maam Maajoor Bóoy bokkul ci benn pàrti. Bi Abdulaay Wàdd jëlee ndam li ci wotey njiitu réew yu 2000, la ko tabb jëwriñ ji yore wàllu yoon awiril 2000, ginnaaw loolu, mu def ko jëwriñ ju jëkk ñetti fan ci weeru màrs 2001, ginnaaw bu Mustafaa Ñas jébbalee lenge yi. Moom mooy jigeen ji ñu jëkk a tabb jëwriñ ju jëkk ci réew mi. Ci ayam gi, la tabb ay jigeen jëwriñ ji ñu toftal ci wetu gox-goxaat yi (Cewo Siise), jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi (Awa Mari Kol Sekk), jëwriñ ji yore njaboot gi ak tuut-tànk yi (Awa Géy Kebe) ,jëwriñ ji yore njënd, njaay, këri liggeeyukaay yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi (Aysa Aañ Puuy) ak njiitu kureel gu mag giy saytu liggeeyu tele yi ak rajo yi (Haut-Conseil de l'audiovisuel) (Aminata Ñaŋ Siise). Moom ci boppam, moo daloo Kàggug réewu Senegaal (Bibliothèque nationale du Sénégal). Ñeenti fan ci weeru nowàmbar lañu ñaanalante moom ak njiitu réew mi ginnaaw taxawaay bu mu amoon bi bato Lë Joolaa suuxee, septàmbar 2002. + +Septàmbar 2004 la ko Alfaa Umar Konaare tabb teewalkatu Kureelu gu mbooleem réewi Afrig yi (Commission de l'Union africaine (UA), mu gàlloo aar nit ñi demul ca toolu xare ba te nekk ci bérebi ayoo yi. Dakaar la féete waaye dafay dem lu bare ci yeneen réew yi, fu mel ni Darfuur, Repibilig bu Sàntar Afrig, Kótdiwaar, Repibilig Demokaratig bu Kóngoo, Ruwandaa, Burundi wala Ugandaa, nga xam ne dafa fay daje ak ñi séq xeex bi (xeexkat yi ak way-pólotig yi). + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Toftal bi + +Jukki yi ñu ko tudd + + Ngornmaŋu Maam Maajoor Bóoy (Gouvernement de Mame Madior Boye) + Jëwriñ yu jëkki Senegaal (Premiers ministres du Sénégal) + Pólotigu Senegaal (Politique du Sénégal) + Limu njiiti pólotig yu jigeen (Liste de dirigeantes politiques) + Nekkinu jigeen ci Senegaal (Condition féminine au Sénégal) + Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal (Liste de femmes ministres sénégalaises) + +Lees bind ci moom + + Kathleen Sheldon, Historical Dictionary of Women in Sub-Saharan Africa, The Scarecrow Press, Inc., 2005, 448 p. + Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, Dakar, 2006 (2e édition), p. 42 + « Mame Madior Boye : Femme ... et Premier ministre », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 83-84 + +Lees jële feneen + + Nataalu Maam Maajoor Bóoy bu nekk ci dalu webu njëwriñu yoon ji (Photo de Mame Madior Boye sur le site du Ministère de la Justice) +Maryaama Ba + +Maryaama Ba mu ngi juddu fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru awiril atum 1929, faatu fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru ut atum 1981 ci Dakaar. Bindkat la woon. Ci ay téereem, Maryaama Ba dafay ŋàññ ñàkk a yemale gi am ci diggante góor ak jigeen te aju ci aaday Afirig. + +Dundu ak jaar-jaaram +Mu ngi juddoo Dakaar atum 1929 ci njaboot gu am alal. Way-juram wu góor liggeeykatu nguur gi la woon. + +Ginnaaw bi way-juram wu jigeen faatoo, ci teel sax, ay maamam a wéyoon di ko yar. Ñooñu ñoo ko yar ci diiney lislaam. Way-juram wu góor, ñu doon ko wax Aamadu Ba mujj nekk jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi ci ngornamaŋ bu Senegaal atum 1952. + +Mu daldi dugg ci lekool farañse bi, nekk ku ci ràññeku lool ndax ay jallooreem. Bi mu amee sàrtikaa (certificat d'études primaires) ci fukki at ak ñeentam, la dem ca Lekool Normaal bu Tëngeej (Rufisque) atum 1943. Lekool boobu mu nga fa jóge atum 1947 ginnaaw bu mu fa amee lijaasab njàngale. Mu nekk di jàngale diiru fukki at ak ñaar laata muy ñaan ñu jële ci njàngale mi, yóbbu ko ca Eespeksiyoo bi yore wàllu njàng mi ci gox bi (Inspection régionale de l’enseignement), loolu wéradig yaramam moo ko waraloon. + +Am na ñetti doom yu jigeen ci sëyam bu jëkk ak Basiiru Njaay, am beneen doom bu jigeen SMK[Quoi ?] ci ñaareelu sëyam ak Ablaay Njaay. Yàlla wéddi sëyam ak ñetteelu borom-këram di Obéey Jóob, nekkoon fi deppite ak jëwriñ te mu amoon ak moom juroomi doom. Ginnaaw jaar-jaar yooyu yépp mu am ci sëy, Maryaama Ba dafa mujj dugg ci kureeli jigeen yu bare, ngir jigeen ñi jàng te mën tamit di jot seeni àq ak yelleef. Loolu moo waraloon mu yëkëti ay kàddu, siiwal ay jukki yu aju ci wàll wi ci bérebi tasekaay xibaar yi. + +Atum 1979 la siiwal téere bile di Une si longue lettre di téere nettaleem bu jëkk ci këru móolukaay téere gu ñu naan Nouvelles éditions africaines. Ci boobu téere, nettalikatam bi di Ramatulaay mu ngi ciy nettali, ci ab baataxal, dundam gi weesu ginnaaw bu borom-këram faatoo. Téere baa ngi fësal bëgg-bëgg bu mag, bu yeewu ngir nekkal fi jiggeeni Afrig yi war a jàmmaarloo ak aada ak cosaan ak tamit diine. Bi ñu ko génnee rekk, la téere nettali bi siiw lool, ñépp di ci wax ; ñu tappal ko ci neexal bu ñu naan « Prix Noma de publication en Afrique » ca Fuwaaru téere bu Francfort atum 1980. Lu moy Une si longue lettre, mu ngi doon taxawu ak a yëkëti àq ak yelleefi jigeen ñi, rawatina jigeen ñi nekk ci buumu sëy. Muy wax ak a bind ay jukki ci nekkinu jigeen ñi, rawatina ñi seen yoxo jotul seen ginnaaw. + +Mu ngi génn àdduna ginnaaw bu ko ab kãaseer daanee, laata ñaareelu téere nettalim bii di Un chant écarlate di génn. Téere boobule dafay nettali ñàkk a antu gu ab sëy bu doxoon diggante ab waa-senegaal ak ab waa-farãas ñàkk a antu. Loolu li ko waral yépp mooy, bopp-sa-bopp gu jëkkër ji di wéye ak wuute gu ñaari mbatit yi wuute. + +Liise bu Gore (Këru yar Maryaama Ba) moom lañu ko tudde. + +Ay téereem dañuy fësal anam yi ñi ko wër ak doomi Afrig yi di dunde ay jafe-jafe yiy tukke ci yile yépp : denc jabar yu bare, waasoo, teg jigeen lu mu àttanul ci téereem bu jëkk bi ; ñàkk a àndug mbokk yi, ñàkk a mën a dund ci am mbatit mu dul sa mos, te sëyu ñu bokkul der fësal ko ci ñaareelu téereem bi. + +Ag ràññeekum +Bindkat bile di Maryaama Ba bokk na ci ñi xàll yoonu càllala ci Senegaal. Téere bi ñu naan Une si longue lettre, nekk téere nettaleem bu jëkk, moo ko siiwal. Téere baa ngi wax ci ñàkk a yemale gi am diggante góor ak jigeen, mbiri waasoo, ngëmi diine yi, aada ak cosaan yi, rawatina lu jëm ci anam yi ñuy dëjale nit. Mu ngi wax tamit ci mbiru denc jabar yu bare, nga xam ne dafa dem ba yàq lu bare ci dundinu askan wi, ñu ciy toroxal jigeen ñi lu ci ëpp, mu leen di jural ay naqar su fekkee ne dañu la wutal wujj wu maase ak say doom. Gëdd, njëriñ ak siiw gi Une si longue lettre am tax na ba nguuru Senegaal jël dogalu boole ko ci téere yi ñuy jàngale ci lekool yu digg-dóomu yi, ay at a ngi nii, booba ba léegi. Dafa jël téere bi, def ko muy téere buy jëmmal taxawu askan te gàlloo ak wareefu dimbalante lal ko, loolu sax moo tax tey, mu bokk ci bindkat yi gën a siiw ci Senegaal, ñu tudde ko tamit lekoolu xaley jigeen ba nekk Gore ngir sargal ko. + +Ay téereem + + Une si longue lettre, Abidjan, Nouvelles éditions africaines, 1979 ; réédition, Paris, Le Serpent à plumes, coll. « Motif » no 137, 2001 + Un chant écarlate, Abidjan, Nouvelles éditions africaines, 1981 + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Lees bind ci moom ak ay téereem + + Ada Uzoamaka Azodo (dir.), Emerging perspectives on Mariama Bâ : postcolonialism, feminism, and postmodernism, Asmara, Trenton, NJ, Africa World Press, 2003, 483 p. + Faustine Boateng, At the Crossroads: Adolescence in the Novels of Mariama Bâ, Aminata Sow Fall, Ken Bugul and Khadi Fall, Howard University, septembre 1995 + Wanjiku Mukabi Kabira, A letter to Mariama Ba, University of Nairobi Press, Nairobi, 2005, 34 p. + Lilyan Kesteloot, « Mariama Bâ », in Anthologie négro-africaine. Histoire et textes de 1918 à nos jours, EDICEF, Vanves, 2001 (nouvelle éd.), p. 468-469 + Susan Stringer, « Cultural Conflict in the Novels of Two African Writers, Mariama Ba and Aminata Sow Fall », A Scholarly Journal on Black Women, 1988, supplément p. 36-41 + Dorothy Davis Wills, « Economic Violence in Postcolonial Senegal: Noisy Silence in Novels by Mariama Ba and Aminata Sow Fall », dans Violence, Silence and Anger: Women's Writing as Transgression, Charlottesville, University Press of Virginia, 1995, p. 158-71 + +Jukki yi ñu ko tudd + + Limu bindkati Senegaal yi : Liste d'écrivains sénégalais + Càllalag Senegaal : Littérature sénégalaise + Taarixu jigeeni Senegaal : Histoire des femmes au Sénégal + +Lees jële feneen + +Dundu ak jaar-jaaram + +Maryaama Ba (juddu 1929, faatu 1981) + +Balluwaay bu aju ci càllala gi + +Balluwaay bu aju ci ag dundam +Akisi Kuwaame + + + +Akisi Kuwaame (borom-këram sant Lebahi) mu ngi juddu benn fan ci weeru sãawiyee atum (1955-2022) ci Singrobo (Casale, Kódiwaar). Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk seneraal ci làrme bu Kódiwaar . Moo nekk njiitu wér-gu-yaram bi ak ndimbalu askan li ci larme bi. + +Dundu ak jaar-jaaram +Seneraal Kuwaame Akisi mu ngi tàmbali am njàngam ci Singrobo, bi mu fa jógee, mu dem Agnibilékrou ci ag mbootaayu katolig. Bi mu jàllee ba war a wéy ci njàng mu digg-dóomu mi, lañu ko yóbbu ca liise Sainte-Marie, ginnaaw bu mu paree foofu, mu dem jàngi paj ci daara yu kowe yi. Fukki fan ci weeru sãawiyee atum 1981 la dem làrme, fekk mu ngi ci juroomeelu atam ci njàngum kër doktoor mi, ci iniwersite bu Abijãa. Diggante sulet ba septàmbar 1981, mu ngi doon def benn tàggatu bu boole ñépp ci lekoolu takk-der bu Kódiwaar ci Buwaake. Ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru suyee (juin) atum 1983, mu wone teesam bi mu bind ba pare. Diggante suyee (juin) ba sulet atum 1983, mu delluwaat ca lekoolu takk-der ya nekk Kódiwaar ngir def fa tàggatub ófisiyee. Ginnaaw tàggatu boobu, mu am garaatu fajkat liyëtnãa. Ci weeru ut atum 1983, mu nekk ki jëkk a am, ci làrme bu Kótdiwaar, ab bërëwe bu wàcckatu paaraa ci mbooloom komandóo mu bataayoo Akouédo bu jëkk. + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Lees jële feneen +Iren Kokki Mutungi + +Dawalkatu ropplaan bu mag bi, Iren Kokki Mutungi, ñu koy woowe Kokki Mutungi tamit, dawal ropplaan, koom gi gën a rëy ci mbooleem Penku Afrig, ci la xam-xamam màcc. Moom mooy jigeen ji jëkk a dawal Boeing 787 Dreamliner ci déndu Afrig. Kenya Airways, di këru liggeeyukaayu Keeñaa guy yëngu ci dem bi ak dikk bi ci jaww ji lay liggeeye,. + +Ati tàggatoom yu jëkk +Ay waajuram Keeñaa lañu dëkk, mu ngi juddu atum 1976. Waajuram wu góor dawalkatu ropplaan la woon ci Kenya Airways. Àllaterete na bu yàgg, léegi koosiltaŋ la ci wàllu dawal ropplaan. Lekool Moi Girls School Nairobi  la Kokki doon jànge. Atum 1992, bi mu paree ci njàng mu digg-dóomu mi, fekk mu am fukki at ak juroom-ñaar, la tàmbale jàng ci lekool bi ñuy tàggate dawalkati ropplaan yi ci Neerobi, ci aydapoor Wilson, Foofu la ame lijaasa bu ñu naan licence de pilote privé, maanaam lijaasab dawalkatu ropplaan bu ndaw. Mu dem wéyali tàggatum ci dawal ropplaan ca Oklaahoma Siti ca Etaasini (USA), foofee nag la ame lijaasab dawalkatu ropplaan bu mag te kureel gile di Federal Aviation administration, di ko jébbale. + +Ay jaar-jaaram +Atum 1995 mu dellu, Keeñaa, ñu jël ko Kenya Airways muy liggeey, moom rekk sax dée, moo fa nekkoon dawalkatu ropplaan bu jigeen diiru juroom-benni weer. Atum 2004, mu doon jigeenu Afrig ji jëkk a am ndigalu dawal ropplaan, bi ñu ko nangulee mu nekk dawalkatu ropplaan bu mag bu mel ni Boeing 737. Ginnaaw gi lañu ko nangul muy dawal Boeing 767. + +Li ci topp mooy, mu def ab tàggatu bu koy tax a jàll ci ndawalum Boeing 787 Dreamliner. Kenya Airways wóolu ko booba ba léegi, teg ciy yoxoy ab B787, mu koy dawal, loolu tax mu nekk tey, jigeenu Afrig ji jëkk a dawal xeetu ropplaan boobu ci àdduna bi. Fukki fan ak juroom ci weeru awiril atum 2014 la njaatigeem xamle loolu. + +Yeneeni mbiram +Pasteef bi mu amoon ci nekk dawalkatu ropplaan benn bés, mu ngi yeewu ci moom bi muy nekk xale, di gis waajuram wu góor  nekk Kenya Airways di fa dawal ropplaan. Komandaŋ Mutungi am na doom ju góor ju juddu ci ati 2006 yi, bëgg na di naaw ci jaww ji, di ci jàppale ay nit, rawatina dawalkati ropplaan yu jigeen yi. Septàmbar 2014, Mutungi kenn la woon ci fanweeri jigeen ak juroom-ñeent yi doon dawal ropplaan ci Kenya Airways, ci lépp lu tollu ci juroomi téemeer ak fanweer, moom moo doon dawalkatu ropplaan bu mag bi ci B787 yiy jóge Neerobi, jëm Pari. Mu ngi xalaat ci sos ag këru liggeeyukaayu dawal ropplaan gu mu moomal boppam, goo xam ne, genn wàllu dawalkat yi yépp, ay jigeen la bëgg ñu doon. + +Seetal tamit + + Kenya Airways + Boeing 787 + Aéroport Wilson + Jomo Kenyatta International Airport + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Genn wàllu jukki bile wala lépp sax, jëlees nañu ko ci jukkib Wikipejaa bu ñu bind ci àngale te tudd « Irene Koki Mutungi » (seetal ci limu bindkat yi) +Xew- xewi dundu Maymuna Kan + +Jamono ju mu juddoo: fukki fan ak ñett ci weeru mars atum junni ak juróom ñeent teemeer ak fanweer ak juróom ñaar ca Ndakaaru + +Jamono ju mu faatoo: benn bés ci weeru mars ci atum ñaari junni ak fukki fan ak juróom ñeent (amoon juróom ñetti fukki at ak benn ba muy faatu) ca Pari + +Turam: Maymuna Ndongo + +Réewam: senegaal + +Yëngu-yëngoom: jigeen juy def politig, àttekat la + +Turu jëkkëram: Mamadu Ture + +Maymuna Kan a ngi juddu fukki fan ak ñaar ci weeru mars atum junni ak juróom-ñeent- téemeer ak fanweeer ak ñaar ca Ndakaar(Senegaal) (1). Mu ngi génn àdduna benn fan ci weeru mars ci atum ñaar junni ak jukk ak juróom- ñeent ca Pari (farãs) (2) . Bokkoon na ci àttekat yu mag ci rééw mi. Loolu terewu ko takk ndombal tànk ba doon ministar. + +Xew- xewi dundam +Maymuna Kan nekkoon na óditëer ci ëttub àtte bu mag bi. Nekkoon na itam ki nu toftal ci porokirëeru ndakaaru. Doonoon na déeyaakoon ci ëttu àtteb àttewaat ca ndakaaru(3). Mu ngi dugg ci nguurug Abdu Juuf ci fukki fan ak juróom ci weeru mars atum junni ak juróom ñeenti téemeer ak juróom ñaar fukk ak juróom ñett. Fekkoon na fa moroomu jàmbaar ju tudd Karolin Fay Jóob. Noonu lanu ko tabbe mu doon sekereteeru nguur gi nu toftal ci jëwriñ ju mag jiy toppatoo nekkinu jigeen ñi, nekkinu nit ñi ak a + +yëkkëti taxawaayu nit ñi. Tur woowu dina am coppite(4). Ba nu tabbee Mustafaa Ñas jëwriñ ju mag ji juróomi fan ci weeru awril atum junni ak juróom ñeenti téemeer ak juróom ñetti fukk ak ñett lanu ko dénkee jëwriñu cuqali nekkin wi. + +Doon nanu ko woowee Ndongo. Nekkoon na soxnas Yaya kan. Kooku nekkoon na ku doon yëngatu wi wàllu koom. Amoon na ak moom juróomi doom. Ba jëkkër ja gaañoo, la sëyaat ak ku xam-xamam màccoon ci koom-koom, ku nu naan Mamadu Ture, moom mi nekkoon jëwrin ji nu dénd koppari réew mi diirub weeru me atum junni ak juróom ñeenti téemeer ak juróom ñetti fukk ak ñett ba weeru me atum junni ak juróom ñeenti téemeer ak juróom ñetti fukk ak juróom ñett (5). + +Tànneefu téere yiy génne + + « The Status of Married Women Under Customary Law in Senegal », in American Journal of Comparative law, 20 (4), 1972, p. 716-723 + « Condition de la femme sénégalaise », in Revue juridique et politique, no 28, octobre-décembre 1974 + « La protection de la femme et le maintien de la famille sénégalaise », in Revue sénégalaise de droit, no 16, 1974, p. 33. + +Xoolal itam + +Xew- xewi dundam + + Anne Winslow (dir.), Women, politics, and the United Nations, Greenwood Press, Westport (Conn.), Londres, 1995, p. 49-53 + Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, B. Ndiaye, Dakar, 2006 (2e éd.), p. 250 + Les Élites sénégalaises, Ediafric, La Documentation africaine, 1984, p. 96 + +xaaj yu dend +Faatu Sow + +Faatu Sow borom xam-xam la ci wàllu askan, di kuy taxawal jigeen ñi, nekk tamit ab gëstukat ci mbirum pàcci-pàcce askan ci Afrig. + +Dundu ak jaar-jaaram +Bokk na ci jigeen ñi jëkk a jàng ba yegg iniwersite ginnaaw jamonoy moom-sa-bopp gi. Mu daldi wone teesam bi mu bind ci borom xam-xam yi gën a mag ci Senegaal laata muy w��yal ay gëstoom ci xam-xamu askan (sosiyolosi). + +Ay jaar-jaaram +Faatu Sow mujj nekk jàngalekat ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar. Ci njeextalu ati 1980 la sos tëralinu njàngale wu aju ci wàllu wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ci gëstuwaay bu ñu naan Conseil pour le développement de la recherche en sciences sociales en Afrique. Atum 1999, mu daldi amal am ndaje mu yaatu ci gëstu yiy taxawu jigeen ci diggante réew yi ñuy làkkee farañse yépp (Congrès international des recherches féministes dans la francophonie). + +Atum 1993, mu daldi nekk ab gëstukat ca CNRS, ca iniwersite Paris-Diderot, ci màkkaanu gëstu bu tudd « Société en développement dans l’espace et dans le temps », nga xam ne ku ñu naan Catherine Coquery-Vidrovitch moo ko sos. + +Mu dugal loxoom bu baax ci boole wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ci gëstuwaay yi ak daaray Afrig yu kowe yi ak tamit, fexe ba siiwal mbootaayi jigeeni Afrig yi ak li ñu bëgg. Yemu ca, ndaxte fexe na ba ag lëkkaloo dox diggante jigeeni Afrig ak ay daaray Amerig yu kowe. + +Moom mooy njiitu gëstuwaayu IFAN ci wàllu wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ,. + +Lu moy liggeeyu gëstukat bi muy def, moom mooy lëkkalekatu kureelu jigeen ak sàrti lislaam ci Afrig sowu jant ak tamit kureel gi ñu tudde ci àngale Development Alternatives with Women for a New Era, nga xam ne dafay yegge mbiri jigeen ñi ci yeneen kureeli àdduna yu mag yi, ngir ñu mën di am saafara. + +Ay téereem + + 2005 - « Les femmes, l’État et le sacré », L’islam politique au Sud du Sahara. Identités, discours et enjeux, M. Gomez-Perez (éd.). Paris, Karthala. + 2005 - « Penser les femmes et l’islam en Afrique : une approche féministe », contribution à Mama Africa. Mélanges offerts à Catherine Coquery-Vidrovitch. Paris, L’Harmattan. + 2005 - « Mobilisation des femmes en Afrique de l’Ouest », Gender Equality. Striving for Justice in an Unequal World, UNRISD, Genève. + 2004 - Notre corps, notre santé : la santé et la sexualité des femmes en Afrique subsaharienne, Fatou Sow et Codou Bop (dir.). Paris, L’Harmattan. + 2002 - Sexe, genre et société : Engendrer les sciences sociales africaines, A. Imam, A. Mama, F. Sow (dir.), version française par Fatou Sow de Engendering African social sciences. Dakar, CODESRIA/Karthala. + 2002 - La marchandisation de la gouvernance, version française par Fatou Sow de Marketisation of Governance, Viviene Taylor (dir.). Paris, DAWN-L’Harmattan + +Téere, jukki wala dali web yi ñu yër + +Lees jële feneen + + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité  Fees ko mën a xame + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité + Article de Wikipédia avec notice d'autorité Article de Wikipédia avec notice d'autorité Balluwaay bu aju ci gëstu bi +Bañkatu Ndeer te nu gën ko xame bañkatu jigeeni Ndeer wala talaatay Ndeer nekk na fànn guy màndargal wala misaal bu wone xeex bañ a doon njaam gi amoon ci xew-xewu démb senegaal.. + +Ana lu xew? Benn bésub talaata ci weeru nowàmbar atum junni ak juróom- ñetti téemeer ak fukk ak juróom-ñeent la nit ñi dëkkoon Ndeer (Ndeer doon suuf si buur yilif, naatoon lool ca Waalo) fippu ci caay-caayu jaaykatu njaam yi jóge ca Marog te seen njiit doonoon Amar Ulda Moxtaar. Naar yooyoo ngi bokk ci giiri tarsas doon laamaan bi jokku ci buur ak tukulëer yu jóge bët-gànnaaru Senegaal + +Fànn googu, taarix nettali na ko. Li muy metti yépp waa dëkk ba wone nanu ci seen jàmbaar. Am nañu ci woy wu dul fey mukk. Nit ña xare nañu fa, jaay fa seen bàkkan, mu gënal leen doon jaam. + +Anam bi +Naar yi jóge bëj-gànnaar réew mi doon nañu song péeyub Waalo ci ndoorteelu fukki xarnu ak juróom-ñeent. Looloo taxoon nu toxoloon péeyub Waalo jëlee ko jurbel yóbbu ko Ndeer (soo gënee wacc ci dëkk bi) (1). + +Giiri lamaan yi jokku ci buuru Marog (mbooleseeni réewi karceen yu bokk benn buur) ñu ngiy jëlee xaalis ci njaayum jaam yi ñu jàpp, jaayaat leen boroomi barke yi jóge bëj-gànnaar afrig rawatina Marakes.(1)(2) + +Njaayum jaam lu yàgg am la waaye ci ndoorteelu fukki xarnu ak juróom- ñeent lañu ko gisaat. Li ko waral mooy Naar yi ragal nañu tubaab yi nekk Ndar nangu Waalo. Looloo tax Naar yi baral cong yi. Ba xew-xewu ndeer di am, booba barag Amar Farim Borso mu ngi Ndar ànd ak gàngooram yi jóge ci beneen xeex ak Naar yi, am ñu ci gaañu doon fajusi.(2) (3). + +Ni mbir mi demee +Gàngoori Naar yi ànd nanu ak seeni farandoo song péey ba bésub "talaata" ci weeru nowàmbar atum junni ak juróom- ñetti téemeer ak fukk ak juróom-ñeent. Ca jamono jooju, góor ñu bare ñu ngi woon ca tool ya. Xale yi ak jigeen ñi ñoo desoon ca dëkk ba. + +Ba nu séenee aji song Naar yi ak seen njiit Amar Ulda Moxtaar(4) lanu + +yëgle ci saa si. Noonu jigeeni Ndeer yi taxawe temm, dogu sàmm dëkk bi ak yenn ci soldaar yu tuuti yi fa desoon. + +Nëbb nanu xale yi ca toolu dugub bi nekk ci wet ga. Jigeen ña jël nañu seen gànnaay, sol seen yëre jëkkër ngir gëmloo saay saay yi seen dogu ci aar dëkk bi(4). + +Jigeen ña delloo nanu ginnaaw njëkkum congum naar yi. Li ci jigeen ñi ci pert bare nañu ndax doole yemul. Njiitu Naar yi sóoraale na songaat dëkk ba. looloo tax jigeeni ndeer ñi dem taal seen bopp ci dëkk ba. Loolu moo leen gënal nekk jaam.(4),(5). + +Fi nu sukkandiku + +li nu ci yokk + +xew-xewu dundam + +xaaj yu dend +Eunice Adabunu mi juddu ci atum 1919, jigéen buy yëngatu ci wàllum jënd-ag-jaay la, bokk na ci jaaykatt yu jigéen yu Naza Benz. + +Mongui juddu ci atum 1919, jugge ci gox bu tuuti. Ci 11 at la tambale nekk baana-baana di jaay beñe, suukar ag ay per. + +Mu far mujj tekki ci njayum sër, ci jaba bu Lomé teksi muje doon way Nana Benz yinga xamne ño gëna siiw. Mu  am ay gëm-gëmug tembte, ngir Eweland bu boyu Tegsi Togo. Segam dafa jël alalam def ko ci limu gëm,  mu daldi bokk ci ñi ëpp doole ci parti way tembte yi bi tudd komite mboolom togo, bu Sylvanus Olympio.  Ci at yu 1960, bokk na it ci way xelalaate bu gox ba teksi jiite paccu goxu Lomé bu kurel gi ëmb mboolem jigéenu Togo (UEFEMTO).  Doxna it ci njangum xale yu jigéenu Lomé. +Article utilisant une Infobox +Article géolocalisé sur Terre +Mbootaayu koom-koom u réew i Afrig sowu  jant ab kuréel la gu dox diggante ay gornamaa, ñu taxawal ko 28i fan i mee atum 1975. Mooy kureel gi gëna raññiku ci lëkkële yéngu yéngu réew yi  féete Afrig  sowu jant (MKRASJ). Li ko taxa jog, mooy jëflante ak dugalante ngir mana taxawal ag bennoo ci wàallu koom ak xaalis. Ci atum 1990 lees ko doleele wàllu saytu kaaraange gi ci diwaan bi, ak ECOMOG gi ñu taxawal, mu di ag kureel u soldaar guy wàllu. Ca atum 1999 nak lañ ko saxal dàkk. Tey jii, 15i réew ñoo  bokk ci MKRASJ. Ci atum 2017 allalu réew yooyu ca bokk àggoon na ci lu toll ci 565i tamñareet ciy dolaar u Amrig. + +Doonte bamu sosoo koom-koom rekka ko yitteeloon, MKRASJ dafa gaaw jublu ci luy saytu jàmm ak lu koy dëgëral. Loolu sax doon lu manula ñàkk ci bu ñu bëggee taxawal am mbootaay mu dëgër.  Ginaaw loolu, MKRASJ farlu na ci tabax ci diwaan bi ay jumtukaay ci wàllu dem ak dikk ak jokkookaay yi. + +COSAAN LI + +LI  JIITU +Mbootaayum koom-koom u réew i Afrig sowu  jant mu ngi soqikoo ca mbootaayu duwaañ bi boolewoon 4i réew u kuréelug déggo, ñu xamoon ko ci (Conseil de l’Entente) ak Mali. . + +SUMB GI +Ca atum 1972 la Yakubu Gowon, dib seneral bawoo Niseria ak Ñasimbe Eyadema bu Togo digle ngir ñu sos ci diwaanu Afrig ab ëtt ngir koom-koom u réew yi mana duggante. Loolu soññ seen yeneen i nàttangoo yi. Ci noonu lañ ko waxtaane ak 12i réew diggante weeru sulet ba ut atum 1973.. + +TERETE BI NJËKK (1975-1993) +Ñagas ñagas yi amoon ci diggante yenn réew  yi ñoo indiwoon  MKRASJ mu dogal ci atum 1978 ab sart buy tere jàmmaarloo diggante ay réew. Topp ci beneen ci atum 1981, buy digle jàppalante ci wàllu kaarange boole ca genn  woote ci ay doxalin u polotig sulet ci atum 1991. Waaye nak ci atum 1990 la jëmmal tigi fànn wi laal kaarange. Ca lël bi njit i réew ak yu goonamaa yi amaloon la jàpp sosug kureel giy saytu jëmëlug wéer nganaay yi. Kuréelug saytu googu doon ci diir bu gaay ab dooley àttekaayu xeex. Ci noonu la dugge ci xare ba amoon biir Liberiya, bii Sera Leona ak biir Gine-Bisaawo. + +Koom-koomu Afrig +Category:Afrig sowu jant +Category:Mbootaay gi ñI sos atum 1975 +Marie Samuwel Njaay (mba Marie Samuel Njie) woye kat i Gàmbi bu maak la won ci jamano 1950s ak 1960s, rawati na yit ci woy i Cosaan. Marie Samuwel Njaay maamam ya nga askan no Siin ak Saalum ci xeetu Séeréer ak Jolof xeetu Wolof. Mo juur woy kat ya Paps Touray ak Efri Mbye, mbukak Alaaji Alieu Ibraayma Cham Juuf maam, ci wali Njuufeen ak Njaayeen. + +Lëkkalekaay yu biti + +Woy +Niti senegaal +Niti Gàmbi +Cosaan +Séeréer +Wangari Maathe + +Wangari Maathe atum naari junni ak juroom benn + +njoxe yu yoor + +turam: Wangari Muta + +Kan ak fan la juddoo: Bes bu jekk ci weeru awril atum junni ak juroom neenti teemeer ak neent fukk + +ihit,gox bu am solo + +Fu angale yi sampoon ca kenaa + +jamono ju mu génne adduna: naar fukki fan ak juroom ci weeru satumbar atum naari junni ak fukk ak benn(fekk mu amjuroom naar fukki at ak benn + +ca Nayrobi,dekkub kenaa + +Dekk bi mu askanoo: kenaan + +liggeeyam, +sukar lu neex la lu ñiy jafë ndikoo lu bari la ci ay ñam yu wuute ak ci ay naan yu + +wuute moom nag dees na watta ndiku di ci jëll lu bari +'' ' Daaru Gay' '' + +Dëkk la boo xam ne, moo ngi bokk ci goxub ( Cees) tundu ( Kajoor) Sëriñ Maxtaar Gay moo ko sañc ci atum junni ak juróom ñenti téereem ak fukk ak juróom ñent 1919 ginnaaw bi mu ci amee ndigalul Maam Cerno Faati Boroom Daarul Muhti. Mu nekk dëkkub diine ak lislaam, Sëriñ Maxtaar Gay nekkoon fa boolewoon liggéey, jaamu Yàlla, jàng ak jàngle, ak yar njaboot gi. Daaru Gay nag li ëpp ca askan wa dañuy yëngutu ci wàllu bay ak yaxantu. + + +Daaru Jaxate ab dëkk la bees sos ci ndigalul sëriñ '''Tuuba''' ci atum (1915/1916) mu nekk Kajoor 3 kilomeetar digganteem ak '''Mbaylaar,''' 7 kilomeetar diggam ak '''Pekkes''', bokk ci '''Xelkoom Jaxate''' gi sëriñ '''Saaliwu tudde Xelkoom Jaaga'''. Kilifa gu mag gu '''sëriñ Tuubaa''' seexal ñu koy wax '''sëriñ Faatu Jaxate''' moo ko sanc, ginaaw bi way-juram '''sëriñ Yéeri Jaxate''' wàccee ab liggéey. + +Muy dëkk bu cosaane, '''Jaxate''' ak '''Caam''' ñoo fa ëpp, bari na xeeti garab yu fay sax ak di fa ñor, li ëpp ci seeni mbay gerte ak dugub la ak ñebbe. + +Dina ñu sàmm it ag jur; xar, bëy nag, yii a fa ëpp. Daara amna fa ay kàngam it génne nañu fa. + +Njabootug sëriñ Tuubaa gi daa nañu fa ñëw lu bari, ku mel ni sëriñ ''Fàllu''', sëriñ '''Basiiru,''' sëriñ '''Baara''', moom sax sëriñ '''Baara''' mii moo feeñal dëkk ba, sëriñ '''Sohaybu''', it daa na fa ñëw ak '''sëriñ Murtalaa''' añs... daan nemmiku mbóot ya fa nekk, ak a xeeñtu saaway ñu baax ña fa nekk. Ci atum 1945 la sëriñ Faatu Jaxate boroom dëkk ba nelaw wuyu ji Boroomam, '''sëriñ Seex Jaxate''' wuutu ko fa, ba atum 1990, mu wàcci '''sëriñ Fàllu Jaxate''' wuutu ko fa ba atum 2016 '''sëriñ Murtalaa Jaxate''' nekk fa, yal na ko fi Yàlla yàggal, moom sëriñ Murtalaa Jaxate mii nag, di jàmbaar lool, joj, def na fa liggéey bu rëy yeesal na barabu sëriñ Faatu Jaxate ba, natt dëkk ba liiñe ko, defar rfa jumaa ju mucc ayib, at mu ne amna màggal gu fay am, muy ag ñaan gog dina ñu ko defal seen maam yu baax yooyu. + +Bi ñu sàncee dëkk ba, ña sant Caam ñoo fa jiitu, ba tay it ñoo fa nekk, daara ju mag ja ginnaaw sëriñ Faatu, sëriñ Basiiru Jaxate doomam moo ko yorewoon di ko doxal ba ni mu fi jógee, ginaaw ba sëriñ Basiiru Jaxate mum sëriñ Seex Jaxate moo fa sampaat daara ba fiimu toll nii moo fa nekk, di ko defe nu am solo. + +Teen ba fa nekk it teenub barkeelu la bob sëriñ Tuubaa moo ko gasluwoon ñaab ci ab siwo sottilu ko ca, +.ro mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Romaani + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1993. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .RO Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#R +.it mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Itaali + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1987. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .IT Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#I +.ru mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Riisi + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1994. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .RU Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#R +.rw mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Ruwandaa + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1996. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .RW Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#R +.st mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Saw Tome ak Preesip + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1997. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .ST Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#S +.sn mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Senegaal + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1993. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .SN Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#S +.zm mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Saambi + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1994. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .ZM Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#Z +.jp mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Sapoŋ + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1989. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .JP Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#J +.sc mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Seysel + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1997. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .SC Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#S +.tw mooy barab bu tolluwaay bu njëkk bu réew (ccTLD) bees jagleel dunu Taaywaan + +Moo ngi njëkk dugg ci net bi 1989. + +Lëkkalekaay yu biti + Informazioni Whois IANA + .TW Domain Name Registry + +Barab bu tolluwaay bu njëkk + +sv:Toppdomän#T +SEEX SÀMBA JAARA MBAY + +AB XAMLE + +Seex Muhamadu Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay: +Mi ngi gane jamono ci atum 1868, làqu ci atum 1917 dundam mi ngi tollu ci 49i at. + +Di doom ci S Ahmadu Mbay ak Soxna Ndaag Kan Ñaŋ. +Di rakk ci S Saa-jéey Mbay mi nga xam ne nitu Yàlla ku mag la woon, ba sax Sñ Sàmba Jaara Mbay moom la defoon ub Sëriñam. + +Sñ Saa-jéey Mbay, jamono bi Sëriñ Tuubaa nekkee Ndar jëkk muy dem ci géej gi booba Ndar moo doon gëblag senegaal. booba nag Sëriñ bi daa na dem lu bari ci ku ñuy wax Sëñ Móodu Njaay Maa-béey daan dal fa moom, foofa la Seex Saa-jéey gisante woon ak Sëriñ Tuubaa +Sñ Saa-jéey Mbay nag bi mu tasee ak Sëriñ bu mag bi, ba Sëñ bi wan ko lam ko wan, ca la jébbalu fa saa sa. Sëriñ bi nangul ko njébbaloom teg ci seexal ko ca bis ba, ngir fam tollu ci sunu Boroom. + +Ca ginnaaw ga la doon wëri rakkam jii di Sàmba Jaara Mbay, ngir mu jébbalu ci Sëriñ bii mu gis; muy Sëriñ Tuubaa. + +AG JÉBBLOOM + +Bi nga xamee ne S Saa-jéey mi ngi ko doon wër, fekkoon ne booba Seex Sàmba Jaara Mbay mi ngi doon waaj ngir siyaare ji Yónnent bi, doon tàggu Sëriñ Alaaji Maalig Si mi nga xam ne daan na ko jàngal yenn téerey xam-xam yi. +Ca booba la ko Sëriñ Alaaji Maalig Si waxoon ne ko ngir mu jaar ci Sëriñ Siidi Muxtaar Alkuntiyu mi nga xam ne moo doonoon sëriñu baayam Ahmadu Mbay ngir mu siyaare ko tàgguwaale ko. Bam demee ngir tàggu ko ca la ko xamaloon ginnaw bi mu duggee ñatti fani xalwa ne ko woon nag: «Kenn du dem ngir siyaare Yóonent Bi ñu ko koy fomm-loo waaye yaw kat am na lu ma saa Boroom wan ci say bir, wan na ma ne Xutbub jamono dina feeñ te yaw kat di nga am cér bu rëy ca moom boo fi toogee. Te ki tax nga nar a daje ak moom mi ngi lay wër». +Booba Seex Saa-jéey juge na Ndar , dégg ne Seex Sàmba Jaara mi ngi jëm Gosaas. Fekkoon ne S Sàmba Jaara moom juge woon na fa ba demoon Tiwaawan jaar fa dem Njaasaan ba doon dëppaat jëm Gosaas foofa la tase ak Seex Saa-jéey mu xamal ko ne moom la doon seet, ne ko nag jëmm ji ma doon wër muy Xutbub jamono gis naa ko. Ma bëggoon ñu ànd ca moom nga jébbal ko say bir. Ca la Seex Saa-jéey ànd ak moom jëm Ndar jébbal ko Sëriñ Tuubaa. + +DIGGANTEEM AK SËRIÑ BI + +Seex Sàmba Jaara nag ab Saa-Kokki la woon waaye ba mu jébbaloo ci Sëriñ bi dafa mujjee féete Ndar. +Mu nekkoon fa ak Sëñ bi, Sëriñ bi nag ubbi woon ko, mu nekkoon way-katam, di ki jëkk a tagg Sëriñ Bu Mag Bi ci làmmiñu wolof! Ngir ne moo jiitu ñoom S Moor Kayre(1869-1951) ak ñoom Sëriñ Mbay JAXATE(1875-1954) ak Sëriñ Muusaa KA (1889-1963) , te doonoon seen mag, ba lii a tax Sëriñ Muusaa KA naan: + +Nde Kayreek Njaxateek Sàmba Jaara sun maam + +Wayoon nan ko ba làccal te yaa ngi way Daam. + +Kon muy ku daa tagg Sëriñ bi ci ay way yu rafet lool, Sëriñ bi tamit bëggoon ko lool ak iy wayam. Loolu nag ag déggam ak ug man a wayam lay tegtale. +Ba moom Seex Sàmba Jaara sax daan na wax naan: Sëriñ Tuubaa damaa rafaatale darajay Hassaan ibn Saabit mi daan dar Yónnent Bi daa ko way mu koy may, +ba loolu a tax mu ne: + +Buur Yàlla may na ma'w kañam + +Ma di Hasaanam fu ma jëm. + +Di tarjumaanu làmmiñam + +Ki ma giseel a mat a xam + +Ay wayam nekkoon lu daan dugg ci xolu aji-dégloom, ba daan na yóbb Sëriñ bi cib jéll. +Loolu nag sikkul ngir ne Sëñ bi daan na dégg ay mbindi boppam mu ko daan def haal, ba di laaj ana ku wax lii? Ñu ne ko Mbàkke lii de say wax a. +Te Seex Sàmba Jaara ni Sëriñ bi daan waxee ak Yónnent bi noonii la daa waxee ak Sëriñ bi, ci ay waxiin yu taaru, moo tax mu ne : + +May na ma, ma déggook moom i wax + +Ci ay waxiinam yu mu wax, + +Samay waxiinay na mu wax, + +Ki ma ma giseel a mat a xam. + +Nga xam ne dañoo dem ba niru ay wax, ba Sëriñ bi da ko daan di bëgg a dégg muy way, ba loolu waral moom masut a ñëw ci kër Sëriñ bi ñu koy xaarloo naan ko sëriñ bi daa fatu (tëju). Te ba ci magam Seex Saa-jéey daan na ñëw ñu naan ko Sëñ bi dafa fatu. Ba mag ñi, ku ci masaa na bëgg a gis sëñ bi, ba gis Seex Sàmba Jaara Mbay jëm fa moom, da koy leer ne di na gise ak Sëriñ Bi tay. +Ba bu daa ñëw fekk Sëñ Bi fatu sax, bu daa Tàmbli a way, Sëriñ bi génn, ba amoon na bayit yoy moom la daa nuyoo Sëriñ bi bu masaa na dugg ci kër Sëñ bi: + +RAHMATUL LAAHI YAA NAHIIMA JINAANII +ANTA HIBBII WA ANTA NUURA JANAANII + +XURRATU HAYNII YAA BUSAARATA XALBII +ANTA TIIBU FU-AADII YAA RAYHAANII ...bmj (ba mu jeex). + +Bu ko daa jàng reg Sëriñ Bi daldi génn. + +Ba loolu a waraloon mu tudde woon ko Saahibul Abyaati maanaam Boroom Bayit Yi (dàkkantal la wu ko Sëriñ Bi daan woowe ngir ug ràññikoom ci man a way). + +AY WAYAM + +Ay wayam nag nekk na luy yare ak a jàngale tawhiit, ak a wane melow Sëriñ Bi. +Ngir daan na wax ne : Sëriñ Tuubaa li mu daan defal Yónnent Bi SHW ci daan ko tagg ak a xamle mooy kan? Manu ko woon a defal boppam, loolu a tax mu def ci man li tax ma koy defal la mu daan defal Yónnent Bi SHW, ci di ko tagg ak a xamle mooy kan? +Moo tax mu ne: + + Wax na Yónnen Bi, li mu doon, + + Man it, ma wax ko Ii mu doon, + + Moom it, mu def ma li ma doon + + Ki ma giseel a mat a xam. + + Nee na Yónnen Bi, yaw a yaw, + + Man it ma wax ko yaw a yaw, + + Bu nee ko yaw, ma ni ko yaw, + + Ki ma giseel a mat a xam. + +Ba loolu a waral mu daan jël Xasida yi Sëriñ Bi di tagge Yónnent Bi SHW , mu jële ca turu xasidaam tagg ci Sëriñ Bi, jël it Bahru bi nga xam ne moom la Sëñ bi tëggee ag taggam ci Yónnent bi. +Ci noonu lanuy gisee mu jël xasidag Sëriñ bii di Jasbul-Xuluub mu fent ci Jasbul-Majsuub. +Moo tax mu naan: + +Jësbul-Xuloob bi dafa jib, + +Bii jësbu jóg xeeñ fa mu jub-, + +-lu ku ko xeeñ na wut a jub, + +Wéy na xameeful fu mu jëm. + + Jësbul-Xuloob bi dafa daw + + Bii Jësbu góg, xeex fa mu aw + +Ta ku ko dab na daw a daw, + +Raw na xameeful fu mu yam. + +Naka noonu la tëggaate xasidag Sëriñ bii di Mawaahibun-Naafih fii Madaa-ihis Saafih mu tuddee ko Naylul-Maraahibi Fii Mukaafatil-Mawaahibi mu ciy way Sëriñ bi ci jëmmi Bahru Mawaahibu. +Bokku na ca Xasida ga, fi mu jële waxu Sëriñ bi, ba mu doon tagg Yónnent Bi naan ko: + +Antal Kariimu. +Anal Xidiimu. + +Moom mu jël ko delloowaat tagg woowu ci Sëriñ bi. +Naan ko: + +Antal Xadiimu. +Antal Kariimu. + +Nga xam ne bayit woowu Sëriñ bi mi ngi ciy wax Yónnent Bi SHW: (yaw yaay Aji-tedd ji, man maay sa jëwriñ ji lay liggéeyal) +Seex Sàmba Jaara Mbay ne Sëriñ bi: (yaw yaay jëwriñ ji, te yaw yaay Aji-tedd ji) +Nga xam ne ñaari melo yépp da ko a delloowaat ci Sëriñ Bi. +Loolu di dëggal la mu waxoon ne: + +Wax na Yónnent bi li mu doon, + +Man it, ma wax ko Ii mu doon, + +Moom it, mu def ma li ma doon + +Ki ma giseel a mat a xam. + +Nee na Yónnent Bi, yaw a yaw, + +Man it ma wax ko yaw a yaw, + +Bu nee ko yaw, ma ni ko yaw, + +Ki ma giseel a mat a xam. + +FI KO SËRIÑ BI TEGOON + +Sëriñ Tuubaa nag fonkoon na ko lool ba bu daa laaj kenn; ana foo bawoo? Boo ne koo Ndar. Daf lay laaj ndax siyaare nga Sàmba Jaara Mbay? Boo ne koo déet. Mu ne la kon demóo Ndar! Loolu batay muy tektale ag cofeelam ca moom, ba tax bi Seex Sàmba Jaara Mbay làqoo, toog na ñatti at yoy daan na laaj ana ku man waxiy Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara ya? mag ñi daa ko ko wëral ba 1920 ci lañ gisee kuñ naan Sëriñ Daam Njaay ca Gosaas moom taalube Seex Saa-jéey Mbay la woon, moo mokkaloon wayi Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara ya? Ca la ñëwe daa di koy jàng ci kanamu Sëriñ bi. Ba nee nañ bu daa dégg kuy wolofal, da daa wax: "Sàllaahu moom de lu mat a wax reg Sàmba Jaara wax na ko". +Ba Sëriñ bi yeggoon na ci daa wax S Sàmba Jaara bu daa way ba yeggal: "Aggal ci keesu jigéen ñi nettali leen wax ji". Te ku ne xam na ne keesu jigéen ña Sëriñ Bi musta nangu benn góor dugg fa, waaye lii la daan wax S Sàmba Jaara Mbay. +Mu am tawféex ju rëy nag, ci Sëriñ Bi joj ci moom reg la nu ko déggee mooy "xam Sëriñ Bi", te bi mu koy wax ci kanamu Sëriñ Bi la ko waxee! Te Sëriñ Bi waxoon na ni ku dul sama Boroom xamuma, moom mu ni + +Wan na ma boppam na mu day. +Yàlla a ko xam moo ma ko may. +Ta wóolu naa ni moo ma doy. +Ki ma giseel a mat a xam. + +Dellu ne: + +Bu fekkee moo feeñu ci man. +Nu naa ma yaw, booba du man. +Moom ka di moom moo fi di man. +Ma di fi moom muy ki fi xam. + +Moo tax ma wax ku déglu lii. +Na xam ni yii ñuy wax du lii. +Waaraate jóowuma si lii. +Seriñ Bi may na ma boppam. + +MUJJUG JAMONOOM + +Bis Seex Sàmba Jaara doon na doxantu ci wetu dex ga ca Ndar, mu gis ay jongama yu taaru lool , mu xam ne ñii duñ ay nitu fii, mu laaj leen? Ana loo leen di def fii? Ñu xamal ko ne ñoom ci Huurul-ayni yi la nu bokk, da noo ñëwoon ngir teertu seen ub sang. Mu laaj leen; naka la seen sang boobu tudd? Ñu ne ko: Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay . Ca la dawee dellu këram, moo tax mu ne: + +Ku sédduwul man séddu naa. +Ku fàdduwul man fàddu naa. +Ba matle weesu naa danaa. +Yàlla ak sa barke maa la gëm. + +Bayit bii la téjjee Xasidaam gii di Jasbul majsuub, yàggul dara mu wuyji Boroomam. +Te ci xew-xew boobu la xamee ne Àjjana la jëm. Te Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara la fay tudd. Ci la waxee woon ne! + +Ku xam lii xamul woon samaw tur la xam +Ku xam lii xamul woon na xam ñatti tur + +Muhammadu Abdu Kariim Sàmba Jaara +Lu siiw la ci yoon wii te siiw taaxi Ndar +Di soppey Sëriñ Bàmba tey way-katam +Diggante juróom ñaari réew yii ñu wër. + +Keroog bim wàccee liggéey, mag ñi seen ug xam cofeelu Sëriñ bi ci moom taxoon na manu ñu ko woon a wax ni Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay bàyyeeku na fi. +Mag ñi naan ko: Mbàkke yéem nanu Yàlla ci Seex Sàmba Jaara! ay waay Mbàkke yéem nanu Yàlla ci Seex Sàmba Jaara! +Sëriñ Tuubaa ne leen: Waaw ñi ko doon jël si fii la ñu jaar.(fekk ne moom moo leen ko njëkk a yëg.) +Mu ne leen Sàmba Jaara déy dama koo duy ba mu fees ma rokkas ko mu tépp. +(Te mooy li mu doon junj ca Jasbul majsuubam ba naan Sëriñ Tuubaa déy: + +Tibbub cofeelam da fa fees +Ci man di funki ak a yees +Ci sama xol ba dóotul rees +Ki ma giseel a mat a am + +Moo tax mu def buma nee gees +Ci sama xol mbaa mu ne gees +Sunu diggante ne depees +Ki ma giseel a mat a xam). + +Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay mi ngi génn àdduna atum 1917, barabam bi ma nga nekk ca almeeru Cem yi fa Ndar. + +AK NJABOOTAM + +Ñatti doom la amoon ñuy: + Faatima Sahraa Mbay + Elaaji Mbàkke Mbay + Muhammdu Mustafaa Mbay. + +XOOL IT + + Sëriñ Muusaa KA + Sëriñ Mbay JAXATE + Sëriñ Tuubaa +Mboor Ak Diine + +(Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci banan. + ++ Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujóotal ko”. + ++ Malaaka ya yépp daldi sujóot, + ++ ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya. + ++ (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ? + +Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ” + ++ “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci + +ban”. + ++ (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ; + ++ te Samam rëbb dal na la ba baa saa di taxaw”. + ++ “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”. + ++ (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu, + ++ ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”. + ++ “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj loo ñoom ñépp, + ++ ba mu des sa jaam ñiy sellal”.+ (Yàlla) daldi wax ne : “Maa ngi waat, ci dëgg ne dëgg laay wax, + ++ Danaa feesal Safara ci yaw ak ña la topp ñépp”. + +Ibliis Ak Jaamu Yàlla + +Lu waral Ibliis waatal Yàlla ne dina sànk doomu Aadama yi, wommat leen  jëme jëhënnama ak ànd ak ñoom? + +Bis bu ne Ibliis mi ngi jéem a fexeel nit ñi ngir sippi leen ug meram, di fexe tàbbal leen ci ñaawtéef yu mag. Naka la ak fan la ak kañ la loolu tàmbali? Ak lan moo waral nooneel googu ne ci diggante Ibliis ak doomi Aadama yi? Lii mooy li nu war a waxtaane fii. + +Tay dinanu xóos ak yéen ca gën gaa xóoti nettali bokk ci nettali yi gën a doy waar te gën a man a def jeexiital ci nit ki, waar yu bari a ngi ci biir, nde ñu ëpp ci nun xamuñu dëgg-dëggi Ibliis mi nga xamantene moo gënoon na jege Yàlla Malaaka yi sax. Mbooru xeex gi diggante Ibliis ak nit ñi, mboor la mu bokkul ak yeneen mboor yi; mboor la mom xew-xewam nekkoon na te deñul di ne te day wéy di nekk ba bisu pénc. Nettalig xeex gu dàppetu googu tàmbalee ak sunu baay Aadama (HS) di wéy ba ñiy mujj ci kaw suuf, ñay dugg guyaar dugg guyaar, ñay dugg sawara dugg sawara, Saytaane def xutbaam ba ca digg ña ko toppoon ca biir sawara muy xutbab deñ ci ñoñ ak waneg seen toroxtaange. + +Nuy tàmbali sunu waxtaan ci Suumiyaa baayu jinne yi ak Aadama baayu nit ñi ak Ibliis ma ñu dàkku ci yërmànde Yàlla, nu wax leen tay turam dëgg ak lu waraloon mu yéggoon ba ca asamaanu juróom ñaar ak mbooleem turam ya ci sépp asamaan. Nettali leen dëgg-dëggi ag yëram ca dàq gi ñu ko dàq ca àjjana ak digganteem moom ak Aadama (HS). + +(Bàyyil xel ne) li nu fi nar a nettali noo ngi koy jële ci ay téere yu wuute, du ñàkk ay "Israa-iiliyaat" am ci (Israa-iiliyaat nag mooy nettaliy waa bani Israa-iil ya ñu daa nettali njëkk Islaam) Israa-iiliyaat nag la ca Yonnent bi (SHW) waxoon mooy jullit bi ñatti taxawaay la ci war a am: 1- dañuy nettali lol Islaam dëggal na ko, nga dëggal ko. + +2- ñu nettali lol Islaam dàq na ko, nga weddi ko. + +3: ñu nettali lol Islaam weddiwu ko te it saxalu ko, nga taxawlu ca bañ koo weddi bañ koo saxal. + +Kon jàngat gi ci jullit bi war def ak waare wi mu ci man a jële a tax nu leen koy nettali fii. + +Mbir ma a ngi tàmbalee lu jiitu ñuy bind Aadama ci luy tollu ak 2000iy at, fekk Yàlla sàkkoon na Suumiyaa miy baayu jinne yi, Yàlla ne woon ko mébétal (waxal li nga bëgg). Suumiyaa ne ko: "li may mébét moom; nuy gise te kenn du nu gis, nu man suulu ci biir suuf, sunuy màggat di man di nekk waxambaane." + +Yàlla nangul ko mébétam, mu dëkkloo ko kaw suuf lépp lu mu bëgg am ko fi, nii la jinne yi nekkee ñi jëkk a jaamu Yàlla ci kaw suuf. Bàlluwaayu loolu di waxu Ibnu Abbaas ja(YYG). + +Waaye ginnaaw bi Suumiyaa faatoo, ba ay xeet ci jinne yi ñëw, ñu waroon a wéyal cant Yàlla ci li mu leen xéewale ci ay xeeti xéewal, waaye defuñu ko; dañu doon yàq ci kaw suuf, daan tuurante dereet. + +Yàlla yabal ay sóobarey Malaakaam, ngir ñu song leen xeex ak ñoom ngir yàq gi jinne yi dëkke woon ci kaw suuf, Malaaka yi song leen ray ci ñoom lu bari dàq leen tasaare leen, kuréel gu néew ci ñoom a rëcc làqatuji ca dun ya ak ca kaw njollaxu doj yu mag ya. + +Malaaka yi yéegaale ak Ibliis booba ab xale bu ndaw la, ñu yéegaale ko jëm ak moom ca  téeg yaa kawe, ñu jàngal naka lay sàbbale ak topp Yàlla sunu Boroom, Ibliis yaroo ci yoxoy Malaaka yi, di julli di jaamu Yàlla niki ni ko Malaaka yi di defe ba mujj mel ni jàmmajóobu Maalaaka yi. Yàlla sellal Ibliis ngir jaamoom ju bari, mu yëkkati ko ca mbooloo maa kawe, ca "Malaakay Muqarabiin ya" ña gën a jege Yàlla. + +Ibliis YYR(Yal na ko Yàlla Rëbb) a ngi tuddoon Hasaasiil, muy tekki aarkat/wattukat (YX) -Yàlla a Xam- , nii la Hasaasiil mujj a nekke kaw asamaan daan ànd ak Malaaka yi daan jaamu Yàlla, sori woon jinne yi nga xam ne ñoo dëkke woon kaw suuf, ba mujj a gën a tedd Malaaka yi, ëpp leen xam-xam ak jaamu Yàlla. Yàlla mujj koo jox wàccuwaay wu kawe mu doon bëkk-néegu àjjana, doon kilifag téegu àddina. + +Bi Ibliis nekkee kilifag asamaanu si tiim àddina,  mu mujj a woru ci boppam ne: "Def naa lu kenn masut a def! Yàlla jox na ma lii lépp ngir samag ràññeeku ci kaw Malaaka yi" + +Yàlla yër la ne ca xolu Ibliis cig rëy ak yëg boppam. Kenn xamul woon li ne ci biir Ibliis ku dul Yàlla. + +Malaaka ya nag ñoom yëguñu dara ci li xew. Ginnaaw ba, la lu kenn masut a foog ag xewam,  xew. Nee nañu Hasaasiil bépp barabu sujjóot day gis nu bind fa "Dàkku Ibliis, móolug Ibliis/ rëbbug Ibliis, ngeccig Ibliis". Mu gis ñu bind ci kaw bunt guyaar yi: " Amna sama benn jaam bu bokk ci sama way-jege ñi, dinaa ko digal, mu bañ ne du topp ndigal, moom kay day moy di moy ba ma dàq ko sama bunt, rëbb ko, def mbooleem li mu mas a jaamu ni pënd bu ñu wesaare." + +Hasaasiil yéemu ne: kan mooy mile Ibliis noo ngi muslu Yàlla ci loolu, mu wëlbatiku ne sunu Boroom; yaw sama Boroom digal ma ma rëbb ko. Yalla daa di ko koy digal, mu rëbb ko luy tollu ak 1000iy at. + +Nekkul woon ne Hasaasiil rekk a gisoon loolu, waaye Malaaka yépp itam gisoon nañu ko. + +Bi Israafiil xoolee "Lawhul Mahfuus" dafa gis ne: "Am na menn mbindéef muy jaamu Yàlla 8000iy at, ginnaaw ba Yàlla delloo ko mbooleem la mu jaamu woon teg ci rëbb ko." + +Mu jooy jooyu metti ba Malaaka yi sax mujj koo yërëm. (Israafiil daa jooy ngir ragal a nekk kookee.) Malaaka yi laaj ko lu muy jooy? Mu ne (Yàlla a rekk a xam) : sama bët a tegu ci am mbóot ci bóoti sunu Boroom yi... (Mu nettali leen la mu gis). + +Malaaka yépp ànd di jooy , ku ne ci ñoom ragal nekk mbindéef moomu ñu nar a dàkku. Ñu ne: li fi sës mooy nu dem ca Hasaasiil, moom bokk na ci way-jege ñi sunu Boroom te ku am nangug ñaan la, mu ñaanal nu ñu bañ a nekk mbindéef moomu. Ñu daa di dem ca Hasaasiil wax ko ko. Hasaasiil yëkkatiy yoxoom ne: 'Yaw Buur bi bul teg sag sàññ ci seen kaw." (Te waxul: yaw Buur bi bul teg sa sàññ ci nun kaw). Mu neeti: "yaw sama Boroom muccal leen cig ndog." Mu ñaanal leen fàtte boppam. + +Hasaasiil woru jàpp na ko ba yegg ci ne masul a jàpp ne man na nekk Ibliis moomu ñuy dàkku, dàq ko ci yërmànde Yàlla. Nii la ñu nangoo ñaanalam Malaaka yi, mu nar a doon ug toroxtaangeem. + +Kahbul Axbaar (mi ngi bokkon ci ñi daa waxtaane jaar-jaaru yahuud yi) nee na: Ibliis, turam a ngi nekkoon "Aji-dellu ji" ci asamaan su njëkk si, su ñaareel si "Aji-dëddu ji" su ñatteel si "Aji-xam ji" su ñenteel si "Wàlliyu bi", su juróomeel si "Aji-ragal Yàlla ji" su juróom benneel si "Bëkk-néeg bi", su juróom ñaareel si "Hasaasiil", ca Lawhul Maxfuus "Ibliis" baatu Ibliis nag mooy tekki "soril" (maanaam muy ku ñu soril ci yërmànde Yàlla). + +Ibliis Ak Moyug Boroomam + +Bi Yàlla nammee wan Malaaka yi dëgg-dëggi Hasaasiil ag rëy gi nekk ci moom, Yàlla da ne: + +" Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne daf ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” + +Yàlla jekkul rekk di wax loolu Malaaka yi. + +Jële nañu ci Ibnu Abbaas (YYG) mu ne: Malaaka yi wax nañu loolu ngir li ñu xamoon ci biri jinne yi dëkke woon kaw suuf ak la ñu daan def ci kaw suuf, mu mel ni dañu ne ko " Ay yaw sunu Boroom , ndax danga fay teg ku mel ni jinne yi nga xam ne dañu doon tuur i dereet ca kaw suuf ñu daan yàq, daan moy? Te nun danu lay sàbbaal di la sant, di la sellal. Yàlla ne leen: + +“Xam naa lu ngeen xamul ! ”. + +Yàlla a ngi namm a wax fii, li malaaka yi xamul ci biri Ibliis cig nuuroom ci rëy, ag dogoom ci nar a moy ndigalam ak woroom. Malaaka yi jortoon ne sunu Boroom daa mer ci tont googu mu leen tont, ñu tàmbalee sàbbal ko ak sellal ko doon wër ca "Baytul Mahmuur" ca asamaan, nga xam day niru ak ni Kaaba gi mel ci kaw suuf. + +Yàlla wahyu suuf si ne ko: damay sàkk ci yaw ay bindéef, amna ci ñoom ñu may topp, am ci ñoom ñu may moy, képp ku ma ci topp ma tàbbal ko guyaar, képp ku ma moy ma tàbbal ko sawara. + +Suuf ne ko: ndax dangay bind ci man ñoo xam ne danga leen di dugal sawara? Sunu Boroom ne ko: waaw! + +Nee nañu: Ibliis daal di wàcc ci kaw suuf ne ko yaw suuf, damaa ñëw ngir laabiire la, Yàlla daa namm a bind ci yaw ki gën ci bindaafon yi, te may ragal ñu moy ko mu leen di tàbbal sawara, bu booba yaw it dinga duggaale sawara tamit. Suuf daa di jooy! + +Yàlla bind sunu baay Aadama ciy yoxoom ngir Ibliis bañ a rëy ci sujjótal ko, Yàlla a ngi nuy wax ci loolu: + +"Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, nangeen daldi rot, sujjóotal ko." + +Nee nañu: bi Yàlla bindee Aadama (HS) toog na 40i guddi. Am ñu ne: 40i at, muy jëmm ju ñu tërëral. Ibliis daan ko dikke, di ko kàjji muy keleŋ ni ban wu wow, nee ñu mooy li sunu Boroom naan: + +" Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ". + +Ibliis di dugg ci biir gémmiñu Aadama di génne ci ginnaawam, di jaar ci ginnaawam di génne ci gémmiñam, te naan ko: " Doo dara, ak lu tax ñu bind la, su ñu ma la saytuloo ma alag la, bu ñu la saytuloo ma ma moy la". + +Malaaka yi bu ñu ko daan romb dañu ko daan ragal, fekk ne Ibliis moo leen ko gën a ragal. Ba dig bi nga xam ne la Yàlla namm ëf Ruuwam ci moom jotee, mu ëf Aadama Ruuwam. Mu digal Malaaka yi ci ñu sujjóotal Aadama. Malaaka yépp sujjóotal Aadama ba mu des Ibliis ngir rëy mu bokk ci way-wedd ni ca saa sa. Yàlla ne ko yaw Ibliis, ana lu la tee sujjóot ndeem digal naa la? Mu ne kii maa ko gën, man du ma sujjóotal nit koo binde ci suufu ban. + +Ibliis sujjóotul ngir rëyam ak mbewteem ak kiñaan. Yàlla ne: + +" 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ” + +76. “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci + +ban”. + +77. (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ; + +78. te Samam rëbb dal na la ba ba saa di taxaw”. + +79. “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”. + +80. (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu, + +81. ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”. + +82. “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj-loo ñoom ñépp, + +83. ba mu des sa jaam ñiy sellal”." + +Ibliis Ak Aadama(HS) + +Bi Yàlla noppee ci Ibliis ak ci yedd ko, Ibliis bañ rekk ne day moy Yàlla. Sunu Boroom rëbb ko tàq ko ci yërmàndeem def ko Saytaane Rajiim, génne ko ca guyaar. Ginnaaw loolu Ibliis sumboo ak meram iñaane Aadama, mu bëgg koo génne guyaar. Yàlla bàyyi ak Aadama xelam gawu ko ci dara, mu bayyi ko ak sagoom, muy man a ràññe lu baax ak lu bon, ginnaaw ba mu ko maytuloo Ibliis, Yàlla a ngi naan: + +". Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de. + +118. [Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle, + +119. doo fi yëg u mar, doo fi màggat”." + +Ginnaw bi ñu dàkkoo Ibliis, mu tàmbali nag ci jëfe la mu dogu woon; te mooy fayu ci Aadama (HS) ak génne ko guyaar, di ko awale ci di ko jiixi-jaaxaloo, jéem koo gëmloo ne xam na lol man na tax ba Aadama sax dàkk du dee mukk. Yàlla a ngi wax naan: + +"Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”." + +Ibliis jaare ci bëggug Aadama ci sax fi dàkk ak sax ca guyaar; bañ fa a génn. Mu xam ne loolu ay tombug néew dooleem, Ibliis daa bëgg a wan ne sunu Boroom; man naa alag kii nga may gënalee. Adaama moom ndaysaan, xamul dara ci kàcci Ibliis yi, waaye li mu ko wax neex na ko te jar na a jarabu, mu yëg ne loolu du'y fo mu laaj Ibliis naka lay def ba am loolu moom ak soxnaam Awa? Ibliis ne ko : ndax yaa ngi gis garab gii ñu la tere nga lekk ci? Moo la ko man a may. Waaye ba tay Aadama gëmul Ibliis, muy fàttaliku tere gi sunu Boroom tere woon ci mu bañ a jege garab gi. + +Kon naka la Aadama def ba lekk ca garab ga ak aartu yi ñu ko aartu yépp  bàyyikoo ci sunu Boroom? + +Boroom xam-xam dañuy wax ne(YRX): Ibliis ci jax-jaxal yi mu doon def Aadama, moo ko doon fàtteloo ndànk ndànk li ko sunu Boroom tere woon (loolu moo nuy dal nun ñépp ba tay, su nuy saytaane di jax-jaxal, danuy fàtte ndànk ndànk lepp lu nu mas a waar). Waaye Aadama gëmul woon lu dul ginnaw ba mu waatee, Aadama ne ko giiñal nu bu dee li nga wax dëgg la, Aadama (HS) -ci ni ñu bind- xam na ne kenn warut a waat ci Yàlla ba noppi di fen. Mu ne ko waatal ci kiy sama Boroom di sa Boroom ne li ngay wax dëgg la. Ca noonu la Ibliis mi ñu rëbb giiñe ci kanamu Aadama ngiiñug fen ci ne li mu wax dëgg la te moom da koy laabiir rekk moom ak Awa. Yàlla a ngi nuy leeral loolu ci téereem bu sell bi Alxuraam, mu ne: " Mu giiñal leen ne moom kat mi ngo bokk ci way-laabiire ñi" + +Ginnaw ba Ibliis waatee, ci la xelu Aadama soog di dal naka noonu Awa (HMS) ndax seen xel masut a jàpp ne kenn sañ na a giiñ ci Yàlla ci ay nar, Ibliis nekk ki jëkk a waat ci Yàlla ci ay fen (kon képp kuy waat ci Yàlla di fen, Ibliis ngay roy) te amul fu mu ko defe fu dul àjjuna. Ca la Aadama fàtte lépp lu ñu ko tere woon ndax giiñu Ibliis ji, tàmbalee lekk ca garab ga moom ak Awa. Nee na ñu garab ga garabu pom la woon nekkoon ci kaw suuf, bi ñu ko lekkee rekk la seen mbalaan ya muriku seen awra feeñ. Yàlla ngi nuy leeral loolu naan: + +"22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt + +di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ” + +wàccug Aadama Ak Awa Ak Ibliis Ci Kaw Suuf + +La dal Aadama dal ko; mu lekk ca garab ga, sunu Boroom wàcce Aadama ak Awa ñoom ak Ibliis ci kaw suuf, Yàlla a ngi naan: + +"[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di + +noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”. + +Bi ñu wàccee Ibliis ci kaw suuf daf ne: yaw sama Boroom génne nga ma àjjana ngir Aadama, te man manaluma ko dara ndare danga maa kàttanal ci kawam, Mu ne ko defal naa la ko, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko lu mu am ci doom nga am lu ni tollu, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko seen i dënn say dëkkuwaay la; ngay man daw seen biir i yamar ni dereet di dawe seen i yaram, mu neeti dollil ma, Mu ne "Génnal ak say kàddu, loo mën ci ñoom, nanga leen song ak say xarekat ak say gawar, + +nanga bokk ak ñoom alal ak i doom te dig leen”. Waaye Séytaane du leen dig lu dul ay nax." + +Ginnaaw bi Aadama xamee li Ibliis sàkku ci sunu Boroom mu ne: Ay yaw sama Boroom teg nga ko sama kaw, te man it manuma mucc ci moom lu dul ci sa ndimbal, Mu ne ko doo am doom lu dul boole naa ko ak ñu koy aar ci àndaale yu bon, mu ne dollil ma, Mu ne ko jenn jëf ju baax ju ne ma ful ko fukk te di ko yokk, jenn jëf ju ñaaw ju ne jenn laa koy jàppe te di ko far, mu ne dollil ma, Mu ne ko "Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. + +Ndax Yàlla dana jéggale bakkaar yépp. Mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”. + +Mu neeti ko, yaw sama Boroom dollil ma, Mu ne say njaboot fi ak ñoo ngi dund du ma tëj seen buntu njéggal, mu ne dollil ma, Mu ne dinaa jéggale te du ma toppe, mu ne doyal naa. + +Al-Faaruux Siise✍🏾 +Guillermo Lasso : njiitull Ekwadoor yi (2021–2025). + +Ekwadoor +Xudar walla Xidr mbaa Xadr + +XUDAR /Xadir /Xidir + +Xudar, mooy jëmm ji Alxuraan di nettali ci Saaru Xunt Ma {65. Ñu daje ak ab jaam ci sama jaam yi boo xam ne may Nanu ko yërmaande lu jóge ci Nun, te jàngal Nanu ko xam-xam bu bàyyikoo ci Nun.} [Saar 18 : Xunt Ma], Muusaa toppoon ko ca dajewaayu ñaari geej ya {66. Muusaa ne ko : “Ndax ma topp la ci kaw nga jàngal ma ci lu xamaleef na la ko ci luy gindee [ak xamle] ? ”.} [Saar 18 : Xunt Ma]. +Wuute nañu ci ne ndax ab Yónnent la am déet, am ñu nitu Yàlla la woon, ba moo tax jullit ñi sunu tuddee turam teg ci (HS) (Halayhis Salaam/ yal jàmm ne fa moom). Sahaaba bii di Ibnu Mashuut nee na moom (Xudar) lañu namm ci laaya:{40. Ka ame woon xam-xamu Téere ba ne ko : “Mën naa la koo indil ba la ngaa xef”. [Ne ko mingi nii] , ba ko Suleymaan gisee ci kanamam, dafa wax ne : “Lii dey ngënéelul sama Boroom bi la. Dama ciy nattu ndax damay sant walla damay xarab... képp kuy sant yaw caak, ku weddi nag, sama Boroom moom di Ku doylu, di Ku tedd”.} [Saar 27 : XORONDOM YA] loolu wuute ak waxu Ibnu Abbaas ja te mooy li gëna siiw, nee na ki ñu namm ci laaya ji mooy Aasif doomu Barxiyaa. woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ag faatoom, waaye ñiy wax ne moo ngi dund ba leegi bari na loolu ci waxi fere yi. + +Xudar nag ku ñu jix dato la ci ag sellal ci diine yu bari niki diiney Masiih, Darsi ak Yahuut yi. Ci baaxi Lislaam ak yu dul Lislaam yu bari dañuy melal Xudar ci Yónnent, Nabii, Walliyu, Jaamu Yàlla, Malaaka, Kiy wattu géej gi ak Sëriñu bóoti xam-xam, muy kuy jappale ñi nekk ciy nattu. Dëppale nañu jëmmi Xudar ak ay jëmm yu wuute ciy jamono yu fasantikoo, niki rekk nu tudd ci Saruus ca Irãn, ku sell ka Sarkiis gawar ba ak ku sell ka Jarjes ca Asi gu ndaw ga ca réewi Saam, ak Yuuhanaal Mahmadaan ca Armeen. Am na ñu bari ñu ko jàppe ne mooy Iiliyaa. + +Ag Askanoom + +woroom xam-xam yi dëppoo wuñu ci fu mu askanoo, amna ay nettali yi bari ci wall googu, bokk na ca: + +Ibnu Kasiir wax na ca téereem ba "Al-Bidaaya Wan Nihaaya" ne Xudar, Aadama a ko jur ci geñoom: +« Al-Hafis mom Hasaakir nee na: waxees na ne mooy: Xudar mom Aadama(HS) ci geñoom. ginnan ba mu nettali awale ko ci Ad-Daaruqutnii ne: Muhammat mom Al-Fathul Xalaanisii nettali na nu, Al-Habbaas mom Abdul Laah Ar-Ruumi nettali na nu, Ruwaat mom Aj-Jarraah nettali na nu,Muqaatil mom Sullaymaan nettali na nu jële nañu ci Dahaag, jële ci Ibnu Habbaas mu ne : Xudar doomu Aadama la ci geñoom, ñu dooli ay fanam ba muy fenloo Dajjaal, lii nag Hadiis bu ddog la te yéeme.» _Ibnu Kasiir, Al-bidaaya Wan-Nihaaya- Pàcci bu njëkk bi. + +waxees nañu ne mooy Xaabiil mom Aadama, am ñu ne mooy Bilyaa mom Milkaan (/Kilmaan) mom Faalix, doomu Saalix mom Haamir doomu Arfaxsat, amna ñu ne mooy Al-Mahmar doomu Maalig doomu Abdul Laah mom Nasr doomu Asd, am ñu ne mooy : Doomu Hamaa-il mom Nawaat mol Hiis mom Ishàq. ñenn ñi ne moom sët la ci Ndawu Yàlla lii di Haaruun miy magu Yónnet Yàlla Muusaa, jële nañu ko ci Kalbii mu jële ci Abii Saalih mu jële ci Abii Hurayrata mu jële ci Inbu Habbaas,te moom ku sori la, am ñu ne doom la ci doomu Fihawn ju jigéen, am ñu ne sax doom la ci Firhawn, loolu Nuqaas nettali na ko, amna ñu ne mooy Yónnent Yàlla Ilyasah, am ñu ne mi ngi bokk ci doomi Faaris, doom la ci kenn ci ñi gëmoon Yónnet Yàlla Ibraahiima te gàddaayoon ànd ak moom juge Baabil (Babilõ) waxees na ne baayam ab saa-pers la woon yaayam di ab saa-rom, am ñu wax fasaan wi. + +amna ñu wax ne mooy Xadiruun mom Haayiil mom Mahmar mom Hiisuu mom Ishàq mom Ibraahiima, waxeew na ne mooy ka Yàlla rayoon téeméeri at ginnaaw ba mu dekkal ko dootul deeti ba ba ñuy ëf buftu ba ci Saaru Nag Wa Laaya {259. Walla ka romboon ab dëkk bu ràppoon ba ruus, mu ne : “Waa naka la Yàlla di dundalee lii ak ni mu dee te wow ? ”. Yàlla daldi koy rey moom lu tollu ci téeméeri at. Daldi koy +dekkalaat, ne ko : “Sab yàggaay fii nu mu tollu ? ”. Mu ne ko : “Benn bis walla sax matu ko.”. +Yàlla ne ko : “Am nga fi téeméeri at. Xoolal sa lekk gi ak sa naan gi : soppikuwuñu ; waaye xoolal sa mbaam mi... Te ngir nu def la kéemaan ci nit ñi, xoolal ni nuy dajalee yax yi, ba noppi wodde ko yàpp”. Ba mu ko leeree nàññ nag, mu daldi ne : “Xam naa xéll ne Yàlla mën na lu ne”.} + +Lu Waral Tur Wi(Xudar) + +soloo nañu ci Abii Hurayrata ci Sahiihul Buxaarii “Tuddee nañu ko Xudar ngir ne dafa toog ci...” +XUDAR /Xadir /Xidir + +Xudar, mooy jëmm ji Alxuraan di nettali ci Saaru Xunt Ma {65. Ñu daje ak ab jaam ci sama jaam yi boo xam ne may Nanu ko yërmaande lu jóge ci Nun, te jàngal Nanu ko xam-xam bu bàyyikoo ci Nun.} [Saar 18 : Xunt Ma], Muusaa toppoon ko ca dajewaayu ñaari geej ya {66. Muusaa ne ko : “Ndax ma topp la ci kaw nga jàngal ma ci lu xamaleef na la ko ci luy gindee [ak xamle] ? ”.} [Saar 18 : Xunt Ma]. Wuute nañu ci ne ndax ab Yónnent la am déet, am ñu nitu Yàlla la woon, ba moo tax jullit ñi sunu tuddee turam teg ci (HS) (Halayhis Salaam/ yal jàmm ne fa moom). Sahaaba bii di Ibnu Mashuut nee na moom (Xudar) lañu namm ci laaya:{40. Ka ame woon xam-xamu Téere ba ne ko : “Mën naa la koo indil ba la ngaa xef”. [Ne ko mingi nii] , ba ko Suleymaan gisee ci kanamam, dafa wax ne : “Lii dey ngënéelul sama Boroom bi la. Dama ciy nattu ndax damay sant walla damay xarab... képp kuy sant yaw caak, ku weddi nag, sama Boroom moom di Ku doylu, di Ku tedd”.} [Saar 27 : XORONDOM YA] loolu wuute ak waxu Ibnu Abbaas ja te mooy li gëna siiw, nee na ki ñu namm ci laaya ji mooy Aasif doomu Barxiyaa. woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ag faatoom, waaye ñiy wax ne moo ngi dund ba leegi bari na loolu ci waxi fere yi. + +Xudar nag ku ñu jox dayo la ci ag sellal ci diine yu bari niki diiney Masiih, Darsi ak Yahuut yi. Ci baaxi Lislaam ak yu dul Lislaam yu bari dañuy melal Xudar ci Yónnent, Nabii, Walliyu, Jaamu Yàlla, Malaaka, Kiy wattu géej gi ak Sëriñu bóoti xam-xam, muy kuy jappale ñi nekk ciy nattu. Dëppale nañu jëmmi Xudar ak ay jëmm yu wuute ciy jamono yu fasantikoo, niki rekk nu tudd ci Saruus ca Irãn, ku sell ka Sarkiis gawar ba ak ku sell ka Jarjes ca Asi gu ndaw ga ca réewi Saam, ak Yuuhanaal Mahmadaan ca Armeen. Am na ñu bari ñu ko jàppe ne mooy Iiliyaa. + +Ag Askanoom + +woroom xam-xam yi dëppoo wuñu ci fu mu askanoo, amna ay nettali yi bari ci wall googu, bokk na ca: + +Ibnu Kasiir wax na ca téereem ba "Al-Bidaaya Wan Nihaaya" ne Xudar, Aadama a ko jur ci geñoom: « Al-Hafis mom Hasaakir nee na: waxees na ne mooy: Xudar mom Aadama(HS) ci geñoom. ginnan ba mu nettali awale ko ci Ad-Daaruqutnii ne: Muhammat mom Al-Fathul Xalaanisii nettali na nu, Al-Habbaas mom Abdul Laah Ar-Ruumi nettali na nu, Ruwaat mom Aj-Jarraah nettali na nu,Muqaatil mom Sullaymaan nettali na nu jële nañu ci Dahaag, jële ci Ibnu Habbaas mu ne : Xudar doomu Aadama la ci geñoom, ñu dooli ay fanam ba muy fenloo Dajjaal, lii nag Hadiis bu ddog la te yéeme.» _Ibnu Kasiir, Al-bidaaya Wan-Nihaaya- Pàcci bu njëkk bi. + +waxees nañu ne mooy Xaabiil mom Aadama, am ñu ne mooy Bilyaa mom Milkaan (/Kilmaan) mom Faalix, doomu Saalix mom Haamir doomu Arfaxsat, amna ñu ne mooy Al-Mahmar doomu Maalig doomu Abdul Laah mom Nasr doomu Asd, am ñu ne mooy : Doomu Hamaa-il mom Nawaat mol Hiis mom Ishàq. ñenn ñi ne moom sët la ci Ndawu Yàlla lii di Haaruun miy magu Yónnet Yàlla Muusaa, jële nañu ko ci Kalbii mu jële ci Abii Saalih mu jële ci Abii Hurayrata mu jële ci Inbu Habbaas,te moom ku sori la, am ñu ne doom la ci doomu Fihawn ju jigéen, am ñu ne sax doom la ci Firhawn, loolu Nuqaas nettali na ko, amna ñu ne mooy Yónnent Yàlla Ilyasah, am ñu ne mi ngi bokk ci doomi Faaris, doom la ci kenn ci ñi gëmoon Yónnet Yàlla Ibraahiima te gàddaayoon ànd ak moom juge Baabil (Babilõ) waxees na ne baayam ab saa-pers la woon yaayam di ab saa-rom, am ñu wax fasaan wi. + +amna ñu wax ne mooy Xadiruun mom Haayiil mom Mahmar mom Hiisuu mom Ishàq mom Ibraahiima, waxeew na ne mooy ka Yàlla rayoon téeméeri at ginnaaw ba mu dekkal ko dootul deeti ba ba ñuy ëf buftu ba ci Saaru Nag Wa Laaya {259. Walla ka romboon ab dëkk bu ràppoon ba ruus, mu ne : “Waa naka la Yàlla di dundalee lii ak ni mu dee te wow ? ”. Yàlla daldi koy rey moom lu tollu ci téeméeri at. Daldi koy dekkalaat, ne ko : “Sab yàggaay fii nu mu tollu ? ”. Mu ne ko : “Benn bis walla sax matu ko.”. Yàlla ne ko : “Am nga fi téeméeri at. Xoolal sa lekk gi ak sa naan gi : soppikuwuñu ; waaye xoolal sa mbaam mi... Te ngir nu def la kéemaan ci nit ñi, xoolal ni nuy dajalee yax yi, ba noppi wodde ko yàpp”. Ba mu ko leeree nàññ nag, mu daldi ne : “Xam naa xéll ne Yàlla mën na lu ne”.} + +Lu Waral Tur Wi(Xudar) + +soloo nañu ci Abii Hurayrata ci Sahiihul Buxaarii “Tuddee nañu ko Xudar ngir ne daa fa toog ci...” +XUDAR /Xadir /Xidir, mooy jëmm ji QAlxuraan di tudd ci saaru Xunti ma mu nekk ca benn boroom xam-xam, waaye indiwul turam +Abuu Haamidil Xasaali / Gazali + +Turam moo di Abuu Haamit Muhammat Gassaalii, di ab Saa-Tuus, Saa-Naysabuur, di ab suufiyànke, ténku ci ngiiru Saafihii ak pas-pasu Asharii, di kenn ci kàngami jamonoom, di ki gënoon a siiw ci woroom xam-xami jullit ñi ca xarnu juróomeel ba; atum gàddaay ga, (450g - 505g / 1058 ji - 1111 ji) mu nekkoon ku dégg Fiq ak Usuul ak xam-xam xelale (filosofi), doonoon ab suufiyànke ci wàllu tariixa, koju-Saafihii ci wàllu Fiq, ne woon ci ngiiru Asharii ci wàllu pas-pas, muy ki sos daaray Asharii ci xam-xamu wax, di kenn ci ñattiy ponkam ginnaaw Abul Hasan Al-Asharii, (te ñooy Baaqilaanii ak Juwaynii, ak Gassaalii). + +Ñu daa ko dàkkantalee ay dàkkantal yu bari ci dundam, ba ca gënoon a siiw di "'''Layu Lislaam'''", ak yeneen niki: Taaru Diine Ji, Layu Diine Ji, Aji-wubbej Xeet Wi, Barkeb Bindeef Yi, Imaamu Imaami Diine Ji, Teddug Xeet Wi. + +Amoon jeexiital gu màgg ak ug ndëgg gu leer ci kaw xeeti xam-xam yu bari niki xam-xamu xelale, Fiqub Saafihii, xam-xamu wax, Tasawuf ak Mantiq, bàyyi na fi ay téerey téere ci xeeti xam-xam yooyu. + +Tuus la juddoo fa la màggee, gannaaw ba la tuxu Naysabuur taqoo woon fa ak Imaam Juwaynii (ñu koy dàkkantal ci Imaamul Haramayni), mu jële ci moom xam-xam bu bari, bi mu amee 34i at, ci la lahasee dem +Saytaane|Séytaane:Ibliis + +'''Saytaane''' (ar : الشيطان ; fr : Satin/Diable; en : Evil) + +Ibliis mooy tekki ku ñu dàq ci yërmànde sunu Boroom, di ku ñu dàkku. (Yal na nu Yàlla musal ci moom moom ak i ñoñam. + +bu ñu nee Ibliis rekk kilifag saytaane yi la ñu ci namm, moom mi féttérlu woon, lànk, moy ndigalal sunu Boroom, moom nag Ibliis ci jinne yi la bokk, jinne ñoom ñépp a ngi bàyyikoo ci Suumiyaa baayu jinne yi niki ni Aadama nekkee baayu nit ñi. + +Ibliis nag am na ay sóobare ci nit ni ak jinne (Saytaaney nit ñi ak saytaaney jinne yi). + +Ñom nag dañoo taxaw teww ngir lajjloo nit ak jinne ba ñu yonjax ci li tax seen Boroom bind leen, su ko defe ëllëg ñu ànd ak ñoom tàbbi sawara. +Ibliis mooy ku ñu dàq ci yërmànde sunu Boroom, di ku ñu dàkku. (Yal na nu Yàlla musal ci moom, moom ak i ñoñam. + +bu ñu nee Ibliis rekk kilifag saytaane yi la ñu ci namm, moom mi féttérlu woon, lànk, moy ndigalal sunu Boroom, moom nag Ibliis ci jinne yi la bokk, jinne ñoom ñépp a ngi bàyyikoo ci Suumiyaa baayu jinne yi niki ni Aadama nekkee baayu nit ñi. + +Ibliis nag am na ay sóobare ci nit ni ak jinne (Saytaaney nit ñi ak saytaaney jinne yi). + +Ñom nag dañoo taxaw teww ngir lajjloo nit ak jinne ba ñu yonjax ci li tax seen Boroom bind leen, su ko defe ëllëg ñu ànd ak ñoom tàbbi sawara. +'''Sóobare''' ("[[Wu-farañse | fr]] : Soldat/Militaire; [[wu-àngale | ar]] : Soldier; [[wu-araab | ar]] : جند "") + +Niral xare bi ñàkk na 10i sóobare ca xare ga +Xare su santee B (xare b) mooy li farañse naan: armée; araab naan ko جيش, àngale di ko wax army. + +Niral: Lat-Joor takk na xare bu màgg ngir xeex ak tubaab bi. + +Xare bu santee G (xare g) xamal ne jëf la, mooy li farañse naan: guerre; araab naan ko حرب, àngale di ko wax war. + +Xare ga doxoon diggante jullit ña ak kéeféer ya ca Badar, jullit ña a daan. +Xare bu santee G (xare g) xamal ne jëf la, mooy li farañse naan: guerre; araab naan ko حرب, àngale di ko wax war. + +Xare ga doxoon diggante jullit ña ak kéeféer ya ca Badar (xare badar), jullit ña a daan. + +Xare su santee B (xare b) mooy li farañse naan: armée; araab naan ko جيش, àngale di ko wax army + +Niral: Lat-Joor takk na xare bu màgg ngir xeex ak tubaab bi. +Jinne j: mbindéefu sunu Boroom la, Yàlla ngi ko binde ci sawara, ki nga xam ne moo la Yàlla jëkk a sàkk ci jinne yi mooy Suumiyaa baayu jinne yi nga xam ne niki ni Aadama doone daayu nit ñi noonu la mel ci jinne. +Y +Jinne yi nag ñoo jiitu nit ñi ci kaw suuf, ñoo nekkoon xalifag kaw suuf njëkk ñuy sàkk nit, woroom xam-xam yi dañuy wax ne amoon na ay xeeti bindeef yu jiitu jinne yi ci kaw waaye wuute nañu ci seen tur la ca gën a siiw mooy ne "Xin ak Bin" lañu tudd, waaye ñu daan yàqate ci kaw suuf Yàlla wuutele leen ak jinne yi. +Jinne yi seen njëlbeenug jamono nekkoon nañu ñu daan wéetal seen Boroom daan sellal, dundaloon kaw suuf; ciy tabax i njénde defar ay dër(jardin) yu naat, sàkk ay bëtti ndox yuy wal, ñu doon dund cig teddnga, ba mu yàgg, ñu tàmbalee bew, yëg seen bopp, di rëy-rëylu ci kaw, di lottal ñi néew doole, di rayante seen biir, mujj dëkkewuñu ci kaw lu moy yàq. +Yàlla yabal ci ñoom xareb Malaakaam ñu wàcc ci kaw suuf ngir xeex ak jinne yi, ray ci ñoom lu takku, ñu néew a mucc ci ñoom làqatuji ca lëgg-lëggi ndox ya ak ca xunt ya ak ca kaw njobbaxtalu doj yu mag ya (montagne). +Amoon na ci ñoom waay ju baaxoon daan leen waar ba bi Malaaka ya doon xeex ak jinne yi moom ci xareb Malaaka ya la faroon, ñu koy wax "Hasaasiil" (boo ci bëggee lu gën a yaatu, yëral Mboor Ak Diine" + +Alxuraan Ak Jinne + +Alxuraan, tudd na leen lu bari ba am na Saar wow Saaru Jinne Ya la tudd (Suuratul Jinni) +Malaaka, ay bindeefi sunu Boroom yu mu teral la, binde leen ci leeram, manuñoo moy seen Boroom (noonu la leen binde), seen i tolluwaay ak seen i melo wuute; dañoo am i laaf wuute lim ba, ku ne ak na muy jaamoo Yàlla, duñu ay góor walla jigéen, duñu lekk duñu naan, walla kon sàbbal seen Boroom ak sellal ko mooy seen lekk ak naan. + +Gëm Malaaka yi mooy ñaareelu ponki ngëm ci jullit bi. + +==Lislaam Ak Malaaka== +Islaam jàngale na lu bari ci Malaaka yi, ñuy ñu ñu selle fi jullit yi. Jaamu Yàlla rekk ay seen yitte, te duñu ko moy mukk, jullit bi war dàq lépp lu yellul ci ñoom (luy dàqonte ak sellam jullit bi waru koo gëm), ku ne ak yiite ga nga war a dox. + +==Gëm Malaaka Yi== +NI NUY GËME MALAAKA YI (yal na Yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom) + +Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lañu, te ñu ñu musal ciy bàkkaar lañu, (duñu moy Yàlla), duñu xayta (duñu tuur dugub) duñu saw it, ñu sunu Boroom laabal lañu. Duñu lekk duñu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu Yàlla teral lañu ba fàww, kenn du ci moy Yàlla, ku ci ne li ko Yàlla digal rekk lay def. Ci leer la leen Yàlla binde. Sàbbaal seen Boroom mooy seenug naan, sellal Ko mooy seenug lekk. + +Alxuraan Ak Malaaka Yi +Alxuraan indi na lu bari ci ñoom tudd turi ñenn ñi, niki seen jëwriñ Jibriil ak ñeneen ñu dul moom. Alxuraan day nettali Maalaaka yi ñuy wax ak seen Boroom niki bi muy nettali bi Yàlla nee : "Day sàkk ku Koy wuutu ci kaw suuf", Maalaaka yi dañu ne ko ndax danga fa teg ñuy yàqate kaw suuf di tuurante dereet? Te nun nu lay sàbbaal ak a sant te it di la sellal. Yàlla ne leen Xam Naa lu ngeen xamul. + +Naka noonu la nuy Alxuraan di xamalee ci ne kenn ku ne ci nun am na ñaari malaaka yu nekk ci yaari wàllam di bind ay jëfam. + +Alxuraan di nu xamal batay ne Maalaaka yi dañuy soppaliku ba mel ni ay doomi Aadama niki ni mu nu ko doon nettalee ca Maalaaka yabdoon bégalsi sunu maam Ibraahiima ci ag amam doom, jàlloon ca dëkk Luut ba ne ay ganam la... + +Ak yeneen i nettali... + +Turu Yenn Malaaka Yi Ak Seen i Liggéey +Ka ca jiitu mooy: + + Jibriil mooy jëwriñu Malaaka yi, nekkoon ki ñu wóolu ci wahyu ga miy wàcce Alxuraan daan ko sa Yónnent bi SHW + Miikaa-iil + Israafiil + Hasraa-iil +Mëfër mi, mooy segg gu ñuul, muy segg gu bari malani ci yaramam, muy fer-ñentug ndono guy tax yaram wi ñuul kukk. Ci àll yu fatt yi te bari taw la ëppe ca bëj-saalumu Asi ak End (11% mëfër) lu jafee gis Afrig la, melo wu mel nii dina faral di am itam ca Amerig Jagwaar + +Menn mëfër ca géttu réewum Nagarhol, ca End. + +Menn mëfër ca Soo-Henrii-Doorly, ca réewi Amerig. + + Menn mëfër ca Afrig Bëj-saalum. + + Jagwaar bu ñuul ànd ak mooroomu seggam. +File%3AViverraPoortmanniSmit.jpg Kax bi + + ab kax. + + fi kax yi dëkke ci kembaaru Afrig + +Kax nag bokk na ci limka gi mbootaay gii di "Booleg Réew Yi Ngir Sàmm Kéew Mi" def ci atum 2008 ñeel ràbb yi nar a raaf ci kaw suuf, maanaam sunu moytuwul dootuñu amati dañuy jeex. yenn dëkk yi li ko fay raafloo mooy nit ñi leen di rëbb ci amam yu jaaduwul ngir di ci defar ay gëtt. +Kax nag rabbu guddi la, bëccëg gi yépo da koy nelaw ci diir ñax yu fatt yi, di yeww bu janti bi sowee. +Njuuj-njaaj, Sëriñ Muusaa KA a ko way, di ci tagg Sëriñ Tuubaa di ko melal, kañ ci it Sëriñ Móodu Mustafaa Mbàkke ak Sëriñ Fàllu Mbàkke ak Sëriñ Baara Mbàkke Ak Sëriñ Basiiru Mbàkke. +Galanug way wi nag bokkul ci galanu araab yi, gii moo ko jëkk a wayee, mi ngi ko dikkee ci ñu doon waral ab séet doon ko taasul naan: + "Ku ànd ak ki ma àndal lu la neex laaj, ku jiital ki ma jiital lu la neex laaj". + +Ci la ci fent galan gii tuddee ko NJUUJ-NJAAJ; galanug Njuuj-njaaj. +Mi ngi ko tàmblee: + +"*Na ngeen déglu ma dellooti fent ab daaj +Ba saahir sa di baatin jullee gën ug maaj + +Damay wëlbati mboolem wayiini soodaan +Ba feem yépp di baatin ba jar di seetaan + +Damaa romb Ku seetal mu naa ma kaay laaj +Ku jiital li ma jiital lu la neex laaj + +Ma seet mbir ma mu jiital jarul ay ngaañ +Ma faf jug ne ko tuubal malaaka day gaañ + +Te Ànd ak ki ma àndal nu dem ba Tuubaa +Faral jébbalu moo gën torox su boobaa, + +Ku Ànd ak ki ma Àndal lu la neex laaj +Sëriñ bee jar a àndal bu leen njuuj njaaj + +Ku ànd ak ki ma àndal lu la neex laaj +Sëriñ bee jar a àndal ba léen njuuj njaaj + +Defal ànd bi Yàlla ak Sëriñ tuubaa +Te yonnen di sa wommat nga jublu tuubaa... BMJ(Ba Mu Jeex)" + +Mu bokk ci way yi mu way ginnaaw bi Sëriñ bi làqoo. + +Xoolal it + Sëriñ Muusaa KA +junj + +Am Saaw + +Am saaw day mel ni ab supññeel ci bindiin waaye moo koy ëpp. +Ab suñeel +Rab wii moo tudd barale ci wolof +Ag saafaandu mala la bu nekk ci àll bi +Ag till mala bu nekk ci àll bi la +Ag boy mi ngi bokk ci rabu àll yi +Maki Sàll, mi ngi judd ci 11 desambar 1961 ca Fatik, ab nitu Càmmu Senegaal la. Mooy njiitu réewum Senegaal dale atum 2012. + +Mi ngi bokkoon ci làngug politig gu PDS, doonoon ci ñi doon jàpple Abdulaay Wàdd ci palug njiitu réew mu Senegaal ci atum 2000. Ci ginnaaw bi doon na fi jëwrinu Mbéll yi, Yasara gi ak Jafaan yi dale 2002 ba 2003, doonoon fi jëwrinu Biir réew meek gox-goxaan yi dale 2003 ba 2004, Jëwrin ju njëkk 2004 ba 2007, ginnaaw bi njiital Ngomlaan gu Senegaal dale 2007 ba 2008. + +Ci 2008, ginnaaw ay jàppante yu mu amoon ak njiitu réew ma woon Abdulaay Wàdd la génn PDS dem sos APR, làngug boppam gi koy yóbb ci ndam li mu am ci palug njiitu réew mu 2012. + +Cig palam ci 2012 la taxawal Plan Sénégal Émergent di xalaat bi liggéeyam ngir suqalu Senegaal sukkandiku. Soloos xalaat boobu mi ngi sukkandiku ci tabaxi jumtukaay (ay yoon, naawuwaay aki waax, ...), taxawal ag Ndefar guy man a jox liggéey waa-réew mi, suqalu càmm geek mbay mi. + +Ci atum 2019 lañ ko falaat ginnaaw palug njiitu réew mi amoon ca at mooma. Ci atu 2024 la war a jeexal pal gu mujj googu giy war a yam ci juróomi at. + +Way politig yu Senegaal +Njiiti Senegaal +The Carpenters bi Diiwaan yu Bennoo pop buum. + +Richard Carpenter +Karen Carpenter + +Woy +Interlingue - Làkk + +Grammatica + +li (= articul ) + li table - taabal + table - (= 1 table / = 1 taabal ) + +démb ji - Preterite + démb ji - Preterite/ + -(e)t: yo amat + +Làkk +Njuux li (kilimã), mooy digg-dóomub meloy jàww ji ci diir bu yàgg, li ëpp bu ñu koy natt 30i at ba 30i at lay doon. Muy bawoo ci soppaxndikug xam-xamu fuglug jàww ji gi nga xam ne dees na natt ci am at: tolluwaayu tàngoor bi ak guusug ngel li ak fattug jàww ji ak ngelaw li ak sóobug taw yi. Cig yaatal daal, njuux li mooy mbir mi bawoo ci ni nosteg njuux li mel tey matale mbàmbulaan yi yuur mi ci kaw suuf si. Njuux nag melow barab dina def jeexiital ci moom ci ag tundeem walla xureem añs, naka noonu laliinu ndox mi ak i duusam. + +Kon bu ñu nee njuuxul gox sangam mooy rekk tolluwaay ba mbaa melo wa nosteg njuux la yor ca jamono ja. +Selena Gomez (ci baati Seereer : Selena Marie Gomez) Buur Siin la woon toggoon ci jal bi ca atum 1992. +Texas +California +The Beatles bi angale rock buum. + + John Lennon + Paul McCartney + George Harrison + Ringo Starr + +Woy +Lubotin (uk: Люботин) dëkku ci Ukreen. Mi ngi yaatoo 31,1 km². Nitñii motnañu 20 887 (2019). + +Gallery + +Téerekaay + Стрілець В. В. Люботин: Історико-краєзнавчий нарис. — Харків: Торсинг,2002. — 400с. + Стрілець В. Календар ювілейних та пам’ятних дат м. Люботина на 2008 рік. — Люботин, ІВЦ ЛММК, 2008. — 20с. + Стрелец В. Люботинская дистанция пути: История и современность. — Харьков, 2008. — 154с. + Стрілець В. Внесок Григорія Томашевського в історію м. Люботина // Літературно-художній альманах «Пролісок». — вип. 3. — Харків: Вид-во «Титул», 2006. — с.175-180. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + Dalu lubotin +Dëkki Ukreen +Oleg Goltvyansky (uk: Голтвянський Олег Миколайович; Lubotin, 8 Satumbar 1980) aji-politig ju Ukreen.. + +Téerekaay + О. Голтвянский, А. Оглобля, А. Сизов. Вентиляция зданий. Проектирование и определения характеристик систем вентиляции жилых домов (uk, en) // Государственный институт «УкрНИИводоканалпроект» Проект, окончательная редакция. — Киев: Минрегион, 2015. + О. Голтвянский, А. Оглобля, А. Сизов. Вентиляция зданий. Расчетные методы определения расходов воздуха на вентиляцию зданий с учетом инфильтрации (uk, en) // Государственный институт «УкрНИИводоканалпроект» Проект, окончательная редакция. — Киев: Минрегион, 2015. + Голтвянський О.М. Східні традиції державотворення // Становлення Нікейської держави / Омельчук В. В.. — Київ: Видавництво ТОВ «Прометей», 2020. — С. 421-426. — 800 с. — ISBN 978-617-7502-44-8. + Голтвянський О.М. Теорія та практика сучасної юриспруденції // Реформа та політичний процес / Бровін О.В.. — Харків, 2020. — Т. I. — С. 36-38. — 328 с + Голтвянський О., Кобанець Р. Націреальна спецслужба в українському державотворенні // До питання про особливості розвитку сектору безпеки США в умовах нових глобальних викликів. — Київ: Видавництво ТОВ «Прометей», 2021. — С. 280-286. — 376 с. — ISBN 978-617-7502-02-8. + Голтвянський О. Актуальні проблеми, пріоритетні напрямки та стратегії розвитку України // Українська енергетика. Реалії та перспективи / О.С. Волошкіна. — Київ: ІТТА, 2022. — С. 124-126. — 180 с. + +Karmat ak delluwaay + +Lëkkalekaay yu biti + all-goltvyansky.livejournal.com +Niti Ukreen +Rahmaniya: wenn yoon la ci yooni Tasawwuf yi, te tënku ci sunna. Ñu ngi koy askanale ci genn góor-Yàlla guñuy wax sëriñ Muhamed ibn Abdul Rahman Alzawaawii (1134h- 1207h),  ñiy topp yoon woowu nag tasaaroo nañu ci gox yu bari niki Saam, Iraã, Isibt ak la féete penku ca Afrig. Yoon la woo xam ne ay jéegoom gudd na lool ci tasaare Lislaam ci goxi Afrig, ba mëdd gëm-gëmu nasaraan ci fu bari ci Àdduna bi. + +References + +Rahmaniya +AFC Ajax benn football club ci Eredivisie ci reewu Olaand. +est bi capital ak largest dëkk de uruguay. According ci bi 2011 census, dëkk bi proper a ab population de 1,319,108 (about ab ñettéel de bi réew's total population)[1] ci ab area de ​​201 km² +Dëkk bi était founded ci 1724 par ab español soldaar, bruno mauricio de zabala, ko ab strategic kata ci bi midst de bi spanish-portuguese ay plus de bi la plata basin region +Montevideo played host ci chaque match ci bi 1930 fifa àddina pot, bi bu njëkk edition de kii sporting event. Montevideo est bi administrative headquarters de mercosur ak aladi, bi main des blocs. +Louis xiv (louis dieudonné; 5 septembre 1638 – 1 septembre 1715), it known ko louis bi géniale (louis le grand) for bi jant buur (le roi soleil), était buur de Faraas la 14 mai 1643 ba ñoom saay ci 1715 +Ñoom reign de 72 years ak 110 fan est bi longest recorded de benn monarch de ab sovereign réew ci history. [1][a] although louis xiv's Faraas était emblematic de bi at de absolutism ci europe,bi buur surrounded himself ci ab variety de significant political, military ak cultural figures. + + +Dieumbet Gorée +Deuk bi niou guéna kam ci Gorée mougui nekk ci biir guethie Atlantique jegue lol Dakaru. Bokouna ci 19 Commune yi ci Dakaru. Deuk bobou nekhna beureup bou raniékou ci kellu ninii. Nam té dé ci 1978 lako koureul bi nioy wowé Organisation des Nations Unies ci layko jeumbet. Gorée niouko guena ranie ci diamano boniou diay niit te mou guen ci feuss. Gorée nékhna tamit Deuk bu Diekh ci bou boku ci liste bu Nations Unies pour l' éducation, la science et la culture (UNESCO). + +Tarikh ku Gorée. +Portuguais bouniou wakh Denis Dias mo jekka niew fi niou na Gorée ci atoum 1444 mou wowé ko "Palma". Guenaw lolou ci la Hollandais yi doora niew ci atoum 1588. Tourou Gorée mougui diogue ci "Goede Reede" moy fi terce kay bou guen. Guenaw lolou ci la Français niew ci atoum 1677. Niom ak Anglais yi amonagn ay probleme you beurii, ci lagn signe ay katiim benne accord de paix d'Amiens ci atoum 1817, français yi doraa diot thie Gorée. + +yayoum niit ku nioul mo wora loone soowe dianteut africa li thie melni (Gambie, Saint louis du Séenegl, Benin, Ghana..), ci la doomu afrique yi di diogue deem Amerique. Toubab yii leen don Diaye delu Europe. + +Suniu kayma ci liim ay Domu afrique you beurii laniou diaye diguente (1726 be 1848). Ni doone diaye nioniou di ay Buuru wolofs neccon ci Senegambia. Goree nekone mba di weyal diayoume doomu adam ci ay dioune att. + +Dakaaru boumou dioundo ci attoum 1857, ci la Goree commence di niack place bi mou amone. Toubab yi nio amaal niarri communes Ndar ak Gorée ci Afrique soow jatt. + +yetnen communes toff talou ci mouy Teeguédj ak Dakaru . + +ci attum 1891, nett niou doone dundu Gorée limba gui tolou ci 2100 domu adama boba domu adama yi dundu ci Dakaru niou lolou ci 8737. lim bobou mosdi yokku boba be tey. + +Ci Dookalin Gorée + +Soukandicou ci térre yii administration toubab mo diekk ci diamano colonisation. +Bo ba Dakaru lebou yi nio fay docale. Motakk Gorée Bocone ci ñiet commune yu niek Bu Senegaal moomé bopam ay att ci kanam, lou diapp 1996, nii done dookal guurgui, denio dioyantii dokaliin Rewmi. Niou Koy woowe "Décentralisation", moy diokk ay katann gook gokan yi. communes yi nekk ci Dakar plateau + +Neekiin +Goree neekh Deuk bou diégué Dial Dial, Dakar Plateau, Bel Air, Thiaroye ak Teugue Guedj. + +Meelokane Djeumbet Gorée + +Gorée deefa nekh ci kerr gou maag, woor ko ci biir guedj gui. suniu sett te bu baakh Gorée amout ben espace bu niit + +Askaanu Gorée +askan nu Gorée comme Dakaru, niou ci beurii ay lébu la gnou. Bu fa toubab ci yewe ci la commencé di am ay diakasso, té niou wohélen ay "signares" te niu beurii ci Gorée ak saint Louis. Wa Gorée niou beuri ay Djoulit la niou mais amna aussi ay catholique. limu wa Gorée niou gui tollou ci 1102 domu adama. + +Komkom +Goree nekh deuk bu beurri ut ay activité. Suniu kolle a part tourisme ak nappe ak niende nait.Tourisme + +Momel ak beureup tarru + +Ker diaam yi + +keeru Cosaan + +Feetewaayu +Wolof làkk la woo xam ne wuñu yeex a yaxal la . + +bi ñu demee ba di ci bind it amna ñu ko daan bindee mbindiinu naar te loolu moo jëkk (rawatina wolofal yi); loolu nag xayna la seen jamono laajoon; ag  ubbeeku amutoon (ouverture) ag péexte (la Liberté) it noonu niki am jotug sàkk(créer) ak jubbanti yit amutoon . + +amna ñoo xam ne mbindiinu tubaab lañ koy binde loolu moo mujj rawatina ci ñaareelu xaaju xarnu bii jàll,  moo gën a tasaaroo it leegi . + +Ngir gam-gamle (comparer)  yaari mbindiin yi: + +Fàww nu xam ne moomuñu ci benn araab bi ñi ko daa binde moom lañ xamoon jàng ko ngir diine. Ñi ci daa binde tubaab it moom lañu jàng ngir ag noteel. + +Farañse bi amna ñaari xeeti mbindiin: + +moo xam ne  mu mbedd la matul amul ay sàrt . + +ak bu ñu yoonal mu gën a mat am ay  sàrt. + +Mbindiinu fañse mu mbedd mi: ag ñàkka matam ak ag ñàkka amam ay sàrt. + +Ci ag niral boo waxee "xall" ak "xàll" dañuy bind rek" khall" . mu des it araf yi nga xam ne farñse amu ko ci cosaan niki "ŋ" (Joŋe( moom day bind jonge (diongue). Jarul m guddal . + +Mbindiinu wolof mi nguur gi yoonal jaareeko ci loyi lateŋ yi moomu am na ay règle te loy yépp it am na ci . + +Mbindiin mu naar mi nag boo xoolee boo ko dëppee ci xasaayid yi wala alxuraan day baax ndax araab lañu; mu des nag nga bëgg koo dëpp ci weneen làkk, day aajowoo yokk ak wàññi ak mu wuyy sàrti làkk wa. + +Ginnaaw mbindiinu naar lanu jël bëgg cee yakk wolof su boobaa jafe-jafe bi am ci mbindiinu tubbaab mu mbedd mi boo ñëwee ci araabal mi yit yéesul  ag cikk . + +Daanu ci joxe ay niral: + +Jëlal diggante "nj" (njar)"ñ" (ñar)"c" (car) araab bi  day bind rekk (چر) ñatti tomb ci kaw jiim gi . + +Xoolal it  diggante "ng" (ngàdd) ak "ŋ" (ŋàdd) ak "g" (gàdd) day bind rekk (ݣاد) walla (ݣَدّْ). + +Nga ñëw  ci wàllu taq ak tàqaliku loolu it mbir la ndax amul ay règle ak sàrt  du ma ci guddal. + +Xoolal diggante "mb" (mbacc)  ak "p"  (pacc)  day bind rekk (پچ) ñatii tomb ci kaw baa gi . + +Xoolal diggante "O" (woor) ak "Ó" (wóor) ak "U" (wuur)  (وُور)  maaska lonk rekk lay def . + +Xoolal diggante "E" (weeru)  ak "É" (wéeru) day bind rekk ( وار) daal di teg tomb ci suufu waaw gi . + +Xoolal  diggante "a" (kar) ak "ë" (kër) day def rekk "كَرْ" + +SERIGNE MBACKE BOUSSO +Parc bu Niokolo-Koba + + Xaamel + +2. Tarix +Parc national du Niokolo-Koba (PNNK) moggi neek ab aal bu yatu , digêunt em ak ndakaru toolu si 650 km . Aal bubu moggi neek si beut ganaru rew mi si deuk bu Taambacunda jeegé lol deuk bi niou naan Guinné Bissau. Foofu sa Niokolo-Koba def naniou fa ab yoon bu ropalan meun naffa wac. + +Tarixu Parc bi +Ci atum 1926 aal bi moggi neekon lu niou jagleel reub, ci atum 1951 mu daadi neek ab all bu niou 'classé' , ci atum 1954 niou daadi ko def parc national. Ay yokuté am na si aal bi si diggenté 1962, 1968, 1969, waayé ba deuk bi moomé bopam ci atum 1960 da naka aal bi nekul woon yitéé si ndiit yi fi neekoo. + +Ci atum 1981 ba leegi aal bi niogui taba si patrimoine mondial bu UNESCO. Ci atum 2007 UNESCO dafaa jeul ay matuway si parc ba def ci beureb-u patrimoine yi niou manancé. Lolu liko waralon moy reub kat yiiy doug si parc si ludul yoon. + +melokanu aal bi ( Géographie) +Deex bu Gambi mo romb si digg parc bi si ab deuk bi xamne sorina lol ab Geec. Am na tamit béneen deex bu tudu Kulumtu ak d'ex bu aal Niokolo-Koba bi niou tudee Parc bi. + +Aal bi moggi tolu si 130 km2, dadi neek danaka si diguente deuk biniou naan Kasamaàs, kolda ba si wetu deuk bi niou naan Guinée-Bissau jeege lol Tambacounda. + + +https://fr.wikipedia.org/wiki/Sp%C3%A9cial:Pr%C3%A9f%C3%A9rences#mw-prefsection-rendering +deccukay bu gecc moy deccukay buunu bole ci IFAN, gnoko deff fofou ci xeru goore bi, ci tefessu Dakkaru buu Seenegaal. + +Melosuuf + +Fetuway +Kheer bi di Goore mogui cii 19 beret arodisema bu Dakaaru, Seenegaal. Benn kher sibir dokh mi mogui def 18,2 hectar moggi digg geentem ak tefessu Dakaaru 2 kilo. + +Deuk bobu di Goore mogui nekk si digg dokh mi. Booko bugon khaima, Goore reyuul nonu yeep, moggi def 900 metra ak 300 metra, lolu takh ba reer fa yobbul? kuu wakh Gagnethiaw wakh ci meteo. Maanam muun ngafa niow tee soolo yeere bu diss (na fekk fananofa). tamperature yooggi kooy khaima ci 17 ak 25° buu beethiegge taangoor, ak 24 ba 30° buu taangoor gnowe. Lolu bokuna ci li kheuthie nassaran yi. Lolu takh naa muuy tangoor sakh guuddi gui sool yeere buu diss dalay waar. + +Taariix + +Deccukay bi niogui ko soss ci fukki weer ak niar ci atum 1959 mook daara bu kaawe buniu duppe chek Anta Joop bu Dakaaru, niogui ko ubil bolo mi ci weer bu njeuk ci atum 1960. Ci atum 1995, lagneko geene jeumeul. Cila ko IFAN dakh sokhal ko mok yeneen yu melni mom tee booku si Afrik sow janta yii lakk nassaran. buu fekeni deccukay deuk Afrik ci Dakaaru ammagut, yeenenn jeego nioggi juddu feele see niame, Bamako, Abija, ndar ak dakaaru (deccukay bacca Goore). Bobuu deccukay bokuna si jeego yuu reyy. Bokunassi ay juumtukay niu jeggi dayoo, dakh niu munna dello askan wi giss gis niu jogge ci dokh mi, manan leep luu eube dokh ak napp mi, jaraaleko beppu khett bi nekk si dokh. + +Feetewaaye + + West African Museums Programme (WAMP), , Dakar, Bureau régional de l'UNESCO pour l'éducation en Afrique, 2008 (OCLC 318587910, lire en ligne [archive]), chap. 7 (« Musée de la Mer de l'IFAN Ch. A. Diop, Gorée »), p. 29–31 + (en + fr) Théodore Monod, Pierre Louis Dekeyser et Georges Bracher, «  », Museum International, vol. 14, no 1,‎ 1961, p. 1–11 (DOI 10.1111/j.1755-5825.1961.tb01561.x, lire en ligne [archive]) + Amadou Abdoulaye Seck, «  », Bulletin du WAMP, no 7,‎ 1997, p. 6-16 + https://www.researchgate.net/publication/249499107_Le_Musee_de_la_mer_Goree_Senegal [archive] + https://yoytourdumonde.fr/senegal-ile-goree/ [archive] + https://onlinelibrary.wiley.com/doi/epdf/10.1111/j.1755-5825.1961.tb01561.x [archive] +Melosuuf + +Fumufeete + +Kheer bu Goree moggi bokku ci 19 Deukk yissi Arrondissema buu Dakaaru, Seenegaal. been kher la buuy def 18 hektar digg ngetem ak Dakaaru niari Kilo. + +Deukk boobu di Goree moggi ci digg dokh mi manam ci digg kherr Cat Verr. Yatuway kherr bobuu moggi tollu ci 900 metre ak 300 manaam reyuul. Loluu takhna baa nitt muunuci reer. Ku wakh melossuf wakh ci meteo. +Deccukay bunnu doppe guedj gui moy deccukay binnu def cibir dokh mi tee boleko si IFAN, tee nu tekko feulee sa Goore di teffessu Dakaaru biir Seenegaal. + +Melosuuf + +Fetewukay +Kheer bobbu di Goore moggi bokku ci 19 arrondissema ci deuk bobu di Dakaaru, Seenegaal. Benn kheer buuy def 18,2 Hectar tee mo nekk 2 kilo diggetem ak teffessu Dakaaru. + +Goore moggi nekk si diggi gedj gi manaam si digg kheer Cap Ver. Deuk bobbu di Goore reyuul loluu, manaam 900 metar la ak 300 lollu takhna nitt munufi reer. Kuu wakh melossuf wakh si jaww dji. Munn ngafa niow tee sollo yeere buu diss (loluu na fekk doffa fanann). Ayy temperaturam mogui nekk 17 ak 25° si sedd bi, 24 ak 30° bu tangge. Dakh lollu takhna nuu yeugeul sunu xaritu tubaab yi! Loluu takh guudi gi buu fekkeni tangoor la sakh solefa yeere bu diss. + +Fumou nekh + +Tarikh Gorée + +Ci karagn tee + + +Dun bou nek Sénéal +Dun bou Saint-Louis mo feeté si xalu zu teud bi bu ndar. Si attum 2000 laaco UNESCO bind si momeelou adduna bi. + +Dek la yitam bou makk si walum adda ah thiossan. + +Taariix +Gnogui co deff momëlou Toubab si 17e siécle, Saint-louis gnugui ko deff taxx si diguu 19e siecle. Mo neek Cpital bu dieuk bu Sénégal si attum 1872 ba 1957. Mo gui amoon taxawaay bu maak si walum koom ak adda sii afrique suwu diant bi yeupp. + +miinu fëttëm si dun wi ak fu dëg bi di sanëcu si dëxu Sénégal bi ak ay xarelem you mouthi ayib, fi nap you di terr ak deug zayou toubab yii mo tax Saint-Louis am xarou kanan bu ragnëco. + +Gnogui co Tiibë +OK +diakha +Bataxal +IRCanadian Americans +Amerik Canada ab baat bu mëna jëfandikoo ci waa Amerik +Hurricane Noru tàmpet bu mag la bu bawoo penku bi +Siyazi ukuba abantu bafuna izinto ezininzi kwi-intanethi kwihlabathi lewebhu kwixesha lanamhlanje. + +Le mfuneko ngoku ibe yimfuno emandla yabantu. + +Siyazi ukuba iinethiwekhi ze-intanethi zibaluleke kakhulu kumntu wonke. Ezi ndaba zibonisa imisebenzi yazo kwiindawo ezininzi zobomi bethu, ziyabachaphazela kakhulu abantu namhlanje. Kuyimfuneko ukuba wazi la majelo ngokusondeleyo, ekwanokungcwaliswa kwengqondo. + +Creating a connection + +Yiyo loo nto imimandla enokufikelela kwi-Intanethi ihlala ifuna ukuhlawula ingqalelo. + +Yiba nguwe, zama ukuzigcina kude nemidiya enjalo. Kungenjalo, kukho ithuba lokuba uya kufumana umonakalo omkhulu. + +Okokuqala, masifumane impendulo kumbuzo wokuba kutheni unxibelelwano lunikiwe. Indawo Creating a connection kufuneka ibe yindawo ephezulu kakhulu yokukwazi ukuyinika. Indlela enzima, njengoko izabelo ikhonkco kubalulekile kwezinye iisayithi. +Proto-Indo-European (PIE) walla zeda L'Hindu-europiya-loula hia l'louxha r'rconstructed elli tkoun l'asl l'mosctarak mteë familyet llouxhat l'hindu-europiya L'caractéristiques l'mqaddma ëla buħouth ëamlouha l'linguists explenêt r'relations mteë llouxhât l'Indo-European.proposed features have been derived by linguistic reconstruction from documented Indo-European languages. Belli, mafammesc l ħadd l'laħtha records tethbt elli l'indo-european kênt mn aslu mawjouda. R'records yetmatthlou f ktiba ëla l ħyout, athar mteë nitham kiteeba walla proofs m l'culture mteëhum. + +Kênt famma xedma kbira beesc yreconstructu PIE akthr mn ay proto-louxha oxra, s'sbab ykoun ëla xatrha akthr louxha mafhouma mn bin l'proto-louxhat l'oxra f l'ëasr mteëha. R'reconstruction mteë PIE walla l'louxha elli jeya mnha, w barsca techniques linguistiques beesc yreconstructu bihom (kif l' "comparative method") k résultat ttawru. + +PIE k nathriya kênt maħkiya k louxha waħda mn 4500 QM l 2500 QM f awêxr l'ëasr l'ħäjariy w bdêyt l'ëasr l'bronzi, ama famma taqdirat oxra tdifferi b akthr mn alf snea. Farathiyt Kurgan tqoul elli asl l s'scaëb l'Proto-Hindo-Europiy ynejjm ykoun hthâb l'quqâz l'pontiya f Europa s'scarqiya. R'reconstruction l'linguistique mteë PIE xalletna naëtou nathra ma aëmq l l'culture l'badwi w d'din elli yqoum ëla l'mojtamaë t'thukouriy l elli kênu yeħku b l'louxha hethi. +A B C Č ČŠ Ć ĆŠ D E F G H I J K L M N O P ŠĆČ R S Š ŠČ ŽČ T U UO UN UM V W X ĐŽ Đ PŠ ČH SŠ SH ŠJ ŠH Gh I-Gh Gć Y Um Z Ž Ŝ Ĉ Ĝ Ĵ U ER-T Ŭ \ No newline at end of file